albert einstein juddoo ulma almaañ ci atum faatoo princeton diiwaan yu bennoo yu amerig ci doonoon na ab boroom xam xamu jëmm xaymakat xetlukat bu waa almaañ bu jëloon réewu gu waa suwis te mujje ca diiwaan yu bennoo yu amerig lu weesu doon gi mu doonoon kenn ci jëmmkat ak xaymakat yi gën a siiw ci àdduna bi ci taariixu xam xam doonoon na xalaatkat ku bari yëggu yëggu ci yeneen fànn tambalee ca xeltu ba ci politig boole nañu ko ci gëstukat yi gën a màgg ci xarnub xx bokk na ci li ko gën a siiwal gisiin wi mu def te duppe ko gisiinuw ajoo dugal na it loxoom ci li jëmale kanam doolerandub kàttan ferñent doolerandug tekkaaral añse jotoon na neexalub nobel ci jëmm ci atum albert einstein ulma la juddoo ca almaañ aji juram ju gòor mooy hermann einstein doonoon booroom këru liggeéyukaay bu doon defar ay wuutuloxo yu mbëj pauline koch doonoon aji juram ju jigéen ndakaaru dakar nekkoon reewu afrig gu sowwu gu faraas asf walla aof ci fr ndakaaru fimne mooy reewum barug senegaal akit goxub ndakaaru tolluwaayam ci péeteg sowwu bu afrig ci jegeem daanaka dun bu kap wert waral na sancug notaakon yu jëkk yi akit yaxantu ak àdduna bu bees bi te ame na peetewaayu ngëneel ci jëflanteg cosaani saa afrig yi ak saa tugal yi fa lees taxawalee woon xumbalu àddina bu fànni ñuule jaam yu ñuul bu njëkk bi ci xalaatu leopool sedaar sengoor atum dëkk bii mooy toogu bu këru gëstu bu dàttu bu afirg gu ñuule kdan walla ifan ci fr akit bu bànk bu diggu bu guuri afrig gu sowwu bdgas walla bceao ci fr senegaal menn la ci réew yi ne ci sowwu afrig mu bokk nag ci afrig gu bëj saalumu saxraa afrique sub saharienne mbàmbulaanug atlas diw digam ci sowwu taqaloo ak gànnaar ci bëj gànnaar ak penku mali féete ko penku ginne ak ginne bisaawóo ci bëj saalum gàmbi moom sos ab daanaka jiba quasi enclave ci biir senegaal sutuxlu ba ci lu ëpp jñ km ci biir suuf yi duni bopp bu wert bi cap vert ñi ngi ci jñ ci tefesi senegaal yi réew maa ngi lebe turam wi ci dex gi ko peek ci penku ak bëj gànnaar te ab balluwaayam bawoo ca fuuta jallon ca ginne di dexug senegaal ab kilimaam bu gëwéel la te di bu fendi te yor ñaari jamono jamonoy nawet jamonoy taw ak ju noor jamonoy fendi ci jamonoy canc gi la période coloniale ay digg yu yaxantu yu bari yu ay imbraatóor yu canc empire coloniale moomoon daal di woon nañuy sampu ci tefes gi gépp dëkkub ndar mujj na di péeyub afrig gu sowwu gu faraas mu mujj juge ci di leegi ndakaaru ci moom ndakaaru nag mujj na di péeyu senegaal ca ba mu jotee ca ag tembam ca nekk ci cat li gën a féete sowwu ci goxub afrig la dale ba fimne maki sàll mooy njiitul réew ma senegaal ak doonte bokk na ci càmpéef yu bari yu àdduna bi teewul bokk na ci bennoo gu afrig union africaine ak mbooloom diiwaan yu saxel sahraa yi communauté des états sahélo sahariens senegaal nag yaatoo na jñ cosaanul turu senegaal dañul di jeqi dàggasante ak werante ca labbe bii di david boilat ca mbindam ya mu doon def ci senegaal daa gisoon ne senegaal mi ngi juge ci waxiinu wolof wii di suñu gaal bii nag mooy gis gis bi gën a siiw te xibaarukaay yi les médias gën koo ame te moone lu ñu nangoodi la te sikk ko la ko dale ca ati ay gongikubaat yu bari nag joxe nañu leen ci misaal biy taf cosaanul tur wi ci ag giir gu berber gu sahara mooy giirug zenaga walla sinhaaj naan turu senegaal mi ngi bawoo ci tudd gu waa portigaal yi doon tudd turu giir googu waaye werante wi dañul di tàng ci loolu ba tay lu ci ëpp njëkk taariix ci senegaal day tudd ba laa tudd lenn gëwéeli xeer yu mag yi walla les cercles mégalithiques yu senegàmbi yi walla jóori xor yu ñu sàkk yi les amas coquilliers artificiels yu ci mel ne ya nekk ca dunub faajut jàpp nañu ne senegaal dëkkees na ko ci njëkk taariix lu jiitu lool juddug isaa ay doj yu ñu yatt yu jamonoy doj wu ñu yatt ju njëkk ja le paléolithique inférieur wuññees na leen ci daanaka dun bu bopp bu wert bi cap vert ak yeneen yëf yu gongikoo ci doj ñu jekkal leen dees leen di fekk ci diiwaanub tëngéej ak ci pegi dexi senegaal gu penku gi ci jamonoy doj wu ñu xacc néolithique jumtukaay yi tàmbali nañoo soppiku ak a wuute bu ko defee suuf su ñu togg walla céramique daal di feeñ gasi gëstu ya ñu doon def ca diiwaani tefes ya feñal nañu ay desiiti waañ yuy seere ak a firndeel askan wu mag wu ay nappkat aki yaxantukat wa fa nekkoon marigot bu xant ca delta sottikukaayu dexug saalum ndefarug mbell walla gu weñ metallurgie jëm na kanam ci jamonoy mbell yi protohistorique junni bu ngëkk bi njëkk isaa fi ñuy gis ay bàmmeel ci bindu ay mbaanaar tumulus ci digg réew mi fa tollook gàmbi gu tay gii dees na fa fekk mbooloom gëwéeli xeer yu mag cercles de mégalithes ci aw dog wu tollu ci jñ ci kaw jñ dëkksi gi dafa doon gën di dolliku ndànk ndànk tey gën di dëgër ngir àgg ci sos ay nguur yu njëkk yu sosu ci viieelu xarnu nguur gu tekruur gu namandiru gu jolof ak ay mbokkoo yu sori ak iimbraatóor gu gana ci suufus mali gu tay gi ci nguur yu wuute yooyu gi ci ëppoon doole ci xiveelu xarnu moo doonoon imbraatóor gu jolof gi boole woon kajoor bawol nguuri séeréer yu siin ak yu saalum waalo fuuta tooro ak bambug ci bëj saalum nguurug kaabu teg ci gu fulaadu jolof nekkoon na imbraatóor gu njaajaan njaay sosoon ki njëkk a nekk buurba buur ca jolof faleesoon na ko njiit ca loolu doon mujj di nguurug waalo ca bëj gànnaar penku gu senegaalug tay gii ca diiwaanu dex gi dajale woon na mbooleem askani giirug wolof ngir taxawal imbraatóor gii ci xiiieelu xarnu ibraatóor gi saayoon na te naaxsaay ci ànd ak deeg imbraatóor ba mujjoon ca jolof lele fuli fak ki ko rayoon di amari ngóone sabel faal ki nekkoon ca jooja jamono kilifag diiwaanu kajoor jolof des na di aw dog vassal ñeel imbraatóor gu mali ci diir bu tollu ci xarnu ba loola amee yeneen nguur yi ñoom itam gu ci nekk tàmbalee jël ag tembam ba mujj wàññi imbraatóor gu jolof gu mag googu ba àggal ko ci tolluwaayu genn nguur gu yam ca digg réew mi ci ñaareelu xaaj bu xixeelu xarnu sancaani faraas yi les colons francais tàmbali woon nañoo nangu ndànk ndànk mbooleem nguur yu senegaal yii jolof moo nekkoon nguur gi ñu mujj a nangu ak buurab jolofam bu mujj ba alburi njaay ci ron deflu gu luwis federb lislaam a ngi njëkk a tàbbi ci senegaal ci diggante viiieelu xarnu ak ixeelu xarnu ña ko fa dugal di ay yaxantukat yu araab yu berber dañu doon tas diine jii ci jàmm ñu njëkk koo jox jula yi tuubloo ci ginaaw bi tukkloor yi ak saraxule yi ñoom itam ñu tas ko ci senegaal gi gépp bi ñu demee ba ci kanam ca xieelu xarnu la muraabituun jug tukkloor yi jàpple leen ñuy jéem a tuubloo mboolooy jaamukati xërëm yi jaare ko ci jiyaar loolu benn la ci sabab yi tax séeréer si gàddaayoon dem siin saalum wolof yi pël yi ak mandinke yi te ñoom ñepp ña nga jalu woon ca tekruur lislaam teel na tas ca imbraatóorug jolof waaye ca xixeelu xarnu la nangu ca dëgg dëgg mbooleem askan yi ci anam gu jàmmu loolu nag deesi sante ko sëriñ si ku mel ne seex ahmadu bamba mi sos yoonu murit alaaji maalik sy kenn ci kilifay tiijaaniya walla seydina limaamu laay ki sos laayéen gi ñi yéemoon nit ñi ci seenug mbaax ak ragal yàlla ak séeni karaama xar baax moom lislaam tam nekkoon ab ker keraan moyen ngir boole nit ñi te di leen aar ci jalgati yi ñu miinoon ci nguur yi jiyaar yu toftaloo canc gu ñu teg ci doole jalgatiy ceddo yi xixeelu xarnu ñi ngi ko gën a xame ci daanug nguur yi jàllsig sancaan yu tugal yi colons européens ak jàmmaarloo gi lànk canc gi ñi ko jëmmal di ay nit ñu mel ne lat joor alaaji omar taal mamadu lamin darame alburi njaay walla màbba jaxu ba diiney katolig walla nasaraan ndax katolig bànqaas la ci nasaraan daal di tasu ñi ko def di ay nasaraanalkat yu tugal la ko dale ca xixeelu xarnu rawati na ca siin ak kaasamaas lislaam tàbbi na senegaal ci fukk ak benneelu xarnu ànd ak giirug sinhaaj gu amaasix gi turu senegaal waxees na ne mi ngi bawoo ci tudd gu waa portigaal yi doon tudd turu giir googu askani senegaal yi sos nañu ay nguur aki nguur nguuraan yi ci ëppoon solo di imbraatóor gu wolof ca diiwaani waalo kajoor ak bawol ci fukk ak ñeenteelu xarnu g j ak nguuruñg tukklóor ak gu deñaanke gu pulaar gi ca penku bëj gànnaar ga ay dooley tugal teg nañu loxo ay wàll ci ay tefesam ci fukk ak juroomeelu xarnu g j ginnaaw bi faraas daal di teg loxo réew mi mépp ginnaaw ay xare yu limu ci atum la ndakaaru nekke péeyub afrig gu sowwu gu faraas gépp seoor walla léopold sédar senghor mooy ki njëkk a nekk njiitul senegaal yoroon dàkkantalu njiit liy woykat walla taalifkat ci samwie la senegaal bennoo ak li ñu daa wax sudaan gu faraas gi ci ron turu lëngoo gu mali fédération de malie lëngoo gu mali googu tembe na ci faraas ci suwe waaye ginnaaw ay jafe jafe yu politig lëngoo googu mujj na di ñaari réew ci ut senegaal ak mali jibaleesoon na ag lëngoo ci diggante senegaal ak gambi ci turu senegambiya atum waaye ci jëf feeñul bu ko defee ñaari nguur yi tàggalikoo atum am na ab jë bu ngànnaayu front armé bu nekk ci bëj saalumu réew mi ca kaasamaas bu bëgg tembteg diiwaan ba leeg leeg mu xareek nguur gi la ko dale ca atum sancaan yi les colonisateurs seen teg loxo gu canc gi conqute coloniale mi ngi door bi wuññig suuf yii amee ci ci loxol moolub veneto ab diiwaan ca itaali bii di cadamosto bi mu defalee ay wuññi ñeel portigaal ca jooja jamono la waa portigaal daal di sóobu ci lu gaaw ci njàppum jaam walla jaayug nit ñu ñuul ñi waaye doon nañu war a janook gëpplante la concurrence gi bawoo woon ci jaaykati ñu ñuul ñi te bawoo woon britaani négriers britanniques faraas ak olaand ca yaxantug ñatti koñ ya commerce triangulaire waa olaand yi sos nañu ab diggub yaxantu ca dunub gore faraas taxawal ca digg bii di bu ndar nga xam ne moo mujj di péeyub senegaal bu njëkk bi ci waa faraas ñi ñëw nangu dunu gore benn ci digg yu mag yi ñu daa jaaye jaam yi ak ndar ak tata ju dunu james ca gàmbi nosteg canc daal di nay taxaw ci dikkug federb kaub senegaal le gouverneur du sénégal la ko dale ca ba ak ba mooy ki samp dàtti afrig gu sowwu gu faraas gi asf aof ci wormaal gi mu defoon aada ya fa cosaanoo du dëgg wormaalu ko fenn la tàllale jeexiital l influence gu faraas ba mu weesu senegaal mu liggéey ci lu jëmale kanam koom koomu barab bi ci njariñul faraas rekk nag lol réew mi yitteelu leen woon ci lenn daal di sos waaxub ndakaaru ginnaaw ndar ndakaaru mujj na ci di péeyu afrig gu sowwu gu faraas gi benn ci sancu yu faraas yi ci samwie sudaan gu faraas gi mali gu tay gi ak senegaal seey nañu ci lëngoo gu mali gi nga xam ne mujj na temb ci suwe temb gii mi ngi juddoo ci tuxalug ay nguur transferts de pouvoirs yu amoon ca dëppoo ga ñu xaatimoon ca faraas ca awril senegaal nguurug demokaraasi la gu limuy làng gu bariy parti njiitul pénc mi président de la république dees na ko tànn ngir diirub juroomi at leegi soppees na ponku sartu réew bi aju ci diirub ngiitug réew mi yobbóoti ko ci juroom ñaari at ginnaaw bi ñu ko soppee jële ko ci juroom ñaar yobbu woon ko ci juroom moom njiit li nag mooy tànn njiitul jëwrin yi barlamaab senegaal ñi ngi koy wooye péncum ndawi réew mi mbaa jataayub xeet wi am na nag cér yu ñiy tànn ci ay tànnéef élections yu dul yu njiitul réew mi tànnéef yu yoonal yi élections législatives ngir diirub juroomi at mii menn la ci réew yi gën a am demokaraasi te gën a dal ci afrig ndaxte genn daaneel nguur coups d état masu fee am senegaal niki roytéef yagg nañu koo joxe wone ko ngir ñu roy ci ba tee ay yi di fi am ak doonte amnesty international mi ngi ñaawlu yenn jàpp yi yor mbubum politig senegaal am pénc la mu demokaraasi une république démocratique lu sakkan ci ay làngi politig a nga fa noste ga fa nekk gu njiitug réew la ndax ba mu amee ag tembam senegaal daa daal di jël faraas niki roytéef roy ca politigam ba ca niki yeneen réewi afrig yi bokkoon ci asf afrig gu sowwu gu faraas sartu réew bu senegaal mi ngi taariixoo ci xoolaat nañu ko ci ki ko def di léopold sédar senghor ginnaaw genn laaju référendum ay xoolaat révisions yu bari topp nañu ci ñooy gu moo fi saxal nosteg njiitu réew ci jamono jooju dindi njiitul jëwriñ teg ci gu gi yobbu àppub njiit gi jële ko ci at yobbu ko at jataayub mag ñi le sénat jëlees na ko fi ginaaw bi ñu delloosi ko ci njiitul pénc mi le président de la république xoolal limub njiiti senegaal yil mooy kilifag nguur gi moom nag ñi ngi koy tànn mu ame ci pal gu mbooloo mi suffrage universel ci anam gu jonjoo de manire directe ci diir bu tollu ci juroom ñaari at manees koo yeesalaat benn yoon mooy fal njiitul jëwrin yi xoolal limub njiiti jëwrin yu senegaal moom itam njiitul jëwrin yi mooy tànn jëwrin yi ba noppi sàkku ci njiitul réew mi mu tabb leen ki njëkk a nekk njiitul senegaal mooy léopold sédar senghor mu nekkoon njiit lu ubbeeku te dib taalifkat bu siiwoon ci la ko njiitul jëwrinan lii di abdu juuf wuutu waaye ci la làngug demokaraasi gu senegaal gi am ndam ci njiitug abdulaay wàdd ñu falati ko ci njiitul góornamaa bi fi nekk fii mu ne mooy seex ajiibu sumaare parlamaa bu senegaal yor na ñaari néeg péncum ndawi réew mi ak jataayub mag ñi bi ñu ko taxawalee ci ut péncum ndayi réew mi mi ngi yor ndawi réew yu ñu fal ci pal gu mbooloo mi ci anam gu jonjoo au suffrage universel direct ngir diir bu tollu ci at tànnéef gi gu ëppte la le scrutin est majoritaire ci genn wër ci tund yiy xëccoo ndawi réew di it gu kem proportionnel di ab lim bu tas ci réew mi ñu koy xëccoo mu tollu ci ndawi réew péncum ndaw yi macky sall moo ko jiite mi nekkoon njiitul jëwrin yi waaye fii mu nekk aw yoon jug na wu saada njaay indi ngir ñu jële ko fi wàññi ab àppam ba du weesu menn at ngir man ko fee jële wii yoon nag jot naa jàll waaye njiitul réew mi dëggalagu ko tànnéef yu yoonal yu senegaal yu jàll nañu ci ndam lu yaatu lu àndandoo gu njiit gi coalition présidentielle waaye lu jege ñaari ñatteel deux tiers ci falkat yi demuñu woon ca mbañ gàcca ya li ko waral di ndigalul dogoo boycott lu bawoo ci làngi kujje gi parlamaa bu senegaal boroom benn néeg monocaméral la woon ci diirub jenn jamono jataayub mag ñi muy lu ñu dindi ci ci ginnaaw genn laaju gu sartu réew référendum constitutionnel delloosi nañu ko ca mee mag ñi les sénateurs nag dinañu tollu ci limub ya ca ñoom dañu leen a fal ci anam gu jonjoodi au suffrage indirect ci tund yi yeneen yi njiitul réew mi di leen tabb paap jóob kilifag ndakaaru moo ko jiite am na yoon loi wu ñu def ci diggadil gi la loi sur la décentralisation nekk na it di lu ñuy doxal la ko dale ca samwie yoon woowu jox na ay ay doole yu am solo ñeel jataayi diiwaan yi assemblées régionales ci la àttewaay bu kawe la cour suprme bu senegaal bi nekk di lu ñu dindi ñu wottee ko cér organes yu jagoo loolu àttewaay bu firi bi cour de cassation jataayub nguur gi conseil d état ak jataayub sartu réew mi conseil constitutionnel yooyu cér di yu niru lool séeni moroom ya nekk faraas seeni àttekat njiitul réew mee leen di tabb yooyu ñooy bànqaasi yoon yi gën a kawe ci réew mi les plus hautes instances judiciaires du pays dalub àttewaay bu firi bi ëmb na lenn njiit lu njëkk ak ñatti njiit yu néeg trois présidents de chambre ak gën jaa néew juroon ñeenti xelalkat conseillers ca toppewaay ba le parquet mi ngi ame ci ab toppekat bu matale un procureur général ci benn layalkat bu njëkk bu matale un premier avocat général ci gën jaa néew ñaari layalkat yu matale deux avocats généraux ak gën jaa bari juroom benni déglukat six auditeurs yu koy liggéeyal am na ñatti néeg yoy bu ci nekk mi ngi ame ci lenn njiit ak ñaari xelalkat gën jaa néew jataayub nguur gi ay xaaj yu bari ñoo ko sos jataayub sartu réew bi yor na juroomi cér yu ñu tabbe ci ag santaane décret ngir juroom benni at yu ñu dul yeesal yoo xam ne njiit ca la ak topp njiit vice président dees na ko yeesal cig wàll waaye déet lépp waaye du weesu ñaari cér gën jaa bari ab liggéeyam mooy fuglu tànnéef yu yoonal yi ak xool ba xam yoon yi les lois dëppoo nañook sartu réew mi ak warlu yu àdduna yi les engagements internationaux senegaal dindi na mbugalum ray ci desambar li ëpp ci gëstu yi ñu def ci wàllug gëstu askan walla demogaraafi ci senegaal dafa sukkandiku ci waññ recensement yi ñu jotoon a def ci rawati na doxal gu séentu ak lim gi la direction de la prévision et de la statistique ci siiwaloon na ay leeral ci askani senegaal yi loolu di woon lu juge ci waññ gu mu sóoraale woon ci màgg gi man a ami ci askanu senegaal la ko dale booba ba bu ñu sukkandikoo ci gongikuwaay yii askanu senegaal wi doonoon lu toolook milyo ciy way dëkk ci ak milyo ca jamonoy ag tembam ca yekkatiku na tay ba àgg ci ciy jëmm nattale gi ci te man naa àgg ci ci mujjug askan wii kon day màgg ci anam gu gaaw ànd ak benn tolluwaayu njuru taux de fécondité bu tiim doom ci jigéen seetloos na fa genn kuute gu giir gu mag wolof pël séeréer joolaa malinke soninke maanjanke ak yennat ci ay giir yu gën a néew te gën a gawu ci barab waxuma la nag naari libaan yi ak tubaab yi nga xam ne ñi ngi nekk ci dëkki taax yi ci mujjug ci waa faraas bindu woon nañu ci seen barabu aji teewal ambassade boroom ñaari réewu it ci lañu woon les binationaux ab diir bu yàgg a ngii askan wi nekk di jalu ci fi jàkkaarloo ak mbàmbulaan gu atlas gi waaye nocciku gu kaw gi l exode rural yokk na yamoodi gi ci séddale gii fi mu nekk ñeenti nit yoo gis ci waa senegaal kenn ka mi ngi dëkk ci daanaka dun bu bopp bu wert bi cap vert looloo waral péey baa ngi waaj a xëx bu ndakaaru jàllee diiwaan yi ñu gën a taaxal les régions les plus urbanisées ñooy siggicoor cees ak ndar yi gën a néew ag taaxal moins urbanisées ci diiwaan yi ñooy koldaa maatam ak fatig diiwaanu tàmbaakundaa nag moo yor fatt densité gi gën a doyadi way dëkk ci jñ bu ñu sukkandikoo ci nattale yu digg yu taax yu diiwaan les centres urbains régionaux yi yor lu ëpp ciy way dëkk ñooy tuubaa man nag yaakaar naa ne ag na ma xame tuubaa la fa dëkk man naa ñeentte lim bii ñu wax mi jekki jekki gis ag màgg gu yéem ñépp cees kawlax mbuur ndar siggicoor et njaaréem ca senegaal teeru woon na lu tollu ci ciy daw làqu ak sàkkukati ag wéeru demandeurs d asile yoo xam ne lu ëpp ca ñoom ay waa gànnaar lañu yu doon daw boddanteg xeet ga ak ñennat ci waa liberiyaa waa siraa leyoon ak yeneen réew bu senegaal dee réew muy teeru ay way gàddaay ay migrants moo xam yu ay jamono lañu saisonniers mbaa déet moo xam yu bawoo ci réew yi mu digool lañu walla yu ko sori du tee menn mbooloo mu senegaal mu mag ma ngay dund ca bitim réew wisaaroo gii diaspora alal ju am solo la ci réew mi ci wàllug koom ak njëmmte identité xarala yu xibaar ak jokkoo yu bees yi xxjb dañuy gën di jàppandal jokkoo ci diggante njaboot gi te tax it deesi man a dund mu mel ne da ngaa nekk ci sa biir réew li ëpp ci ñiy dem nag ay waxambaane lañu yu jublu tugal rawati na faraas ak itaali walla ñuy dem ca aamerig gu bëj gànnaar ga ca kebeg yobbaale ci seeni xol naalub dellu réew ma ci ginnaaw yennat ciy at màggug gàddaay gu yoonoodi gi immigrations clandestines ñu koy def ci ay anam yu bon te ñaaw jëm ci duni kanaari yi lu tiital senegaal la ak réew yi koy teeru ñi gën a ñàkk yaakaar ñoom faalewuñu sax ay wi ñu ci man a dajeel ginaaw gis nañu seeni moroom tekki rawati na ya bokk ca wisaaroo ga diaspora moo xam senegaal lañu juddoo mbaa dañu faa am rekki way jur rawati na ñi ciy yëngu ci tàggat yaram mbaa fànn art lu sakkan faatoo na ci gàddaay gu yoonoodi gi mbaa mbëkk mi baat bi ñu ko gën a xame lu ko waral xanaa géej gi ñu sóobu ci lu duli jumtukaay yu dëppoo ñoom kay dañuy sóobu ci ay looca yu doyadi duy kooki bagaas ak nit ci wépp xeet ak maas bu ko defee yooru duñu faale la leen dëgmal ciw ay ak musiba gaal gaay doon duus ba néegub añ ba bu tëdd ba leeg leeg duus ñëw téq leen mbaa ngelaw lu saf ba kero ñuy àgg bu ko yàlla dogalee waaye cis lëf cig loof lu sakkan di ca des dib añ mbaa reerub ag kuréel ciy jën yu waroon a nekk diy añ ñeel leen mbaay reer nii lay deme ba kero ñuy àgg ak la leen fay xaar ciy kaso ak ëlëg gu lëndëm lii mooy li xew ci mbeex mi waxuma la nag la ca tàkk ga aji tàng ji tàkk gii nga xam ne jali beeñ yi yàgg nañu fee tee nit àgg fa mu jëm senegaal nguur la gu bokk ci bennoo gu koom koom ak gu koppar gu afrig gu sowwu gi ginnaaw ay jafe jafe yu koom koom ci njëlbéenug ati juroom neen fukk yi ay yoonam ay luwaam yu koom koom soppiku nañu bu ko defee ag màggam gu koom koom mujj àgg ci ay ci diggante ak ci ndoortel senegaal door na ci doxal tëriinu yéwénal gu koom koom gu kawe ay yitte ci càmmug mboolaay gu àdduna bi communauté internationale looloo ko jañoon ci mu woyofal xiimay kopparam bii nga xam ne daa tënku ci frank bu faraas mu woyofal ko ba ci jeexiitalu woyofal gii diisoon na lool ci ay way dëkkam ndax taxoon ba njëgi li ëpp ci marsandiis yu dàttu yi ak yu dund yi seeroon te yekkatiku niki meew yàpp ceeb ba àgg ci fulu ci genn guddi waaye am na genn màgg gu am ci koom koom bi ak ci njuddéef mu ñumm mu biirum réew mi ngir yéwénal yi nga xam ne àgg na ci ci at mu nekk bu ko defee walu gi l inflation wàññiku ci anam gu yéeme ba àgg ci ay lim yu ndaw bu ñu ko nattee ca la romb ci ut la senegaal génn ci lëngoo gu mali gi daal di jibal ag tembam senegaal ak gàmbi bennoo nañu ci ngir amal lëngoo gu senegàmbi waaye gii nekkutoon lu dul aw gisiin kenn masu koo jëfe mujj gi ñu far ko tas ci ay janoo jot nañoo am la ko dale ca ci anam gu dogatu ci diggante ñoñ tàqalikoo les séparatistes ñi nekk ci bëj saalum gu kaasamaas ak doole yu góornamaa bi ginaaw ay jéem yu bari yu àntuwul genn dëppoo mujj nañu ko xaatim ca siggicoor ca desambar ci diggante jëwrini biir réew ji woon usmaan ngom ak làbbe augustin diamacoune senghor mi nekkoon njiitul fipp gu yëngu yëngu gu doole yu demokaraasi yu kaasamaas yddk mfdc moom diamacoune senghor moomu mujj na faatu beneen tombub coow ci diggante ay waa kaasamaas ak ginne bissaawuóo màgg na ci awril ci gànnar ak senegaal génne nañu ku ci ne ci anam gu ñaaw sa njabootug moroom te ña ëppoon ca ñoom ña nga juddoo woon fa ñu leen génnee muy réew mi leen doomoo woon ñu jotoon faa seey ca mboolaay ga ak koom koom ba bu ñu sukkandikoo ci li jataayub daw làq bu kawe bi jdk hcr wax ay daw làqu ña nga des ba tay ca guddaayub dexug senegaal gi ci njiitul gànnaar jibaloon na ba muy def càkkug palaam ga campagne ne nangu na delsig doomi réewam yooyu doon dund ci senegaal ak mali te neexu leen senegaal a ngi nekk ci diggante ak wu rëddu tus wu gaar wu bëj gànnaar ak ak wu rëddu tus wu taxaw wu sowwu digam wi gën a féete sowwu mooy ndakaaru di it cat li gën a féete sowwu ci goxu afrig su ñu ko méngalee ak réewum mali walla ak mu gànnaar di nanu gis ne senegaal réew mu tuuti la ci rëyaayu suuf kilimaab sahel la ame ca atum la seddale gu mujj gi ame mooy giy wéy ba tay lu dul coppite yi ci mujj a am sosug diwaanu maatam ci ak gox goxaan bu kungeel ci ci la senegaal nekk diwaan yenn ciy dëkk senegaal doon na réew mu bariy giir waaye it soo ko mengalee ak yeneen réewi afrik yu bari wuuteg ay giiram du feeñ man nan ni daanaka wuute amul ci diggante giiri senegaal yi ndax seenug bennoo ci caada man nan cee lim yii tambalee ko ci yi ci gën a bari ba ci yi ci gën a néew wolof pulaar seereer joolaa malenke sooninke manjaak ak yeneen giir giiraan yu tas ci réew mi man nan cee boolee it tubaab yi ak naari libaan yi benin republik bu benin réewu afrig bene aw rëdduw suuf wu sew la nekk ci diggante yamoo gi ak gëwéelub sànkar bi rëddu tus wu gaar wu bene mi ngi ci diggante bëj g ak bëj g tu wu taxawam moom mi ngi ci p ak p ay digam ñoo ngi yem ci togóo ci sowwu yem ci burkina faso ak niseer ci bëj gànnaar ci niseeriyaa ci penku janook mbàmbulaanug atlas gi ci bëj saalum mi ngi am yaatuwaay bu tollu ci yu kaare bene ngi bawoo ca dexug niseer gi ci bëj gànnaar yem ci mbàmbulaanug atlas ci bëj saalum ci ag tallalug km diggante bi gën a guddu ci réew mi km la itaali pénc mu itaali it italia repubblica italiana réewum tugal óróop itaali men la ci réew yi nek ci bëj saalumu tugal ngir xootal taarixu itaali xoolal itaali laata a napoleon di ko teg loxo di ko nangu nekkutoon réew mu ñu bennal nekkutoon it di mu am ag temb moom kay daa seddaliku woon doon fukki xaaj ak ñaar yu doon topp ak a nekk ci ron kiliftéefug ay nostey politig yu wuute nosteg nguur ca savoia piemonte napoli ak nosteg pénc ca venezia ak geneva ak ag àtte gu paab ca rom ak gu dóox ca toskaana ak parma ak xaaj yoo xam ne dañoo nekkoon ci waawug imbraatóor gu otris gi ñooy milano ak lombardia piemonte nag moo nekkoon nekkteg politig gi gënoon a dëgër te ëppoon doole ci nekkte yooyu ña ëppoon ca njiit ya yilifoon nekkte yooyu ay diktaatóor lañu woon rawati na ñi ci waa otris jiite woon cig jonjoo mbaa cig jonjoodi tansani am réewum penku afrig la féete ci peggi mbàmbulaanug end keeñaa ak ugandaa ñoo ko féete bëj gànnaar ruwandaa buruundi ak kongóo kinshasa nekk ci sowwoom saambi ak malawi nekk ci bëj saalum sowwoom mosambik nekk ci bëj saalumam réew mi tollu na ci te am ciy way dëkk ay bantu rekk a fa dëkk péeyam mooy dodoma mi ngi nekk ci biir réew mi waaye dottub koom koom bi dëgg mooy dar es salam gi doonoon péey bi féete ci tefes gi kiswahili ak wu angalteer ñooy làkki nguur ga teewul ne itam araab am na fa doole rawati na ci duni sansibaar ak bu penda tansani ju tay jii a ngi judd ci booloog tanganyika ak sansibaar ci awril gannaaw ci lu yàggul dara ñu am seenug tembte ci nguur yu bennoo yi bokk na ci commonwealth dale ci atum bokk na itam ci mbootaayu xeet yi dale ci desambar ci julius nyerere ab jàngalekat la woon bu judd ci ci bi muy am at la ñëw ci boppu taa tanganyika african association mbootaayu waa afrig bu tanganyika mu daldi koy soppi ag làngu politig dëgg ci lu gaaw tudde ko tanganyika african national union doon woote ngir ag tembteg seenum réew ci desambar la leen ko nguur yu bennoo yi jox ci jàmm ci ndoorte li jëwrin ju njëkk la doonoon ginnaaw pal gu desambar gi mu doon njiitu réew ju njëkk ju tanganyika ci disambar la sansibaar ak pemba am seenug tembte awril la tanganyika ak sansibaar booloo ngir sos li tudd tay réewum tansani nyerere doon njiitu réew ma abeid karume mi doonoon njiitu réewum sansibaar nekk jëwrin ju njëkk ji ci tansani donte booloo gi amoon na waaye ba tay jii sansibaar moo yoral boppam yenn yi njiitu réewum tansani moo ko yoral li ñeel politig kaaraange mbiri biti réew añs moom mu yural boppam njàngale mi ak koom koom tansani réew la mu nekk ci xaaju kol kol bu bëj saalum féete ci penku afrig ay digam yu dénd ñooy mbàmbulaanug end gi ci penku dojuw kilimandjaro ak déegub victoria bi ci bëj gànnaar déegub tanganyika bi ci sowwu déegub malawi ci bëj saalum sowwu ak dexub ruwuma ci bëj saalum tugal mooy wàll wi féete penku goxub tugalasi ci baax dees koy jàppe niki benn ci juroom benn walla juroom ñaari goxi àdduna bi gox baa gi digu ci sowwu ci mbàmbulaanug atlas gi ci bëj gànnaar ci dottub bëj gànnaar bi yem ci géej gu diggu gi ci bëj saalum ay digam ci penku dese nañoo leer dinay faral di jur ay werante li ko waral mooy ni mu taqalook goxub asi waa islaand jàppees na leen ni waa tugal donte féeteem ci degalub tugal aamerig ak mbooleem dun yi ci géej gu diggu gi sipër mi gën a jur coow ci wàllu melosuuf riisi ak tirki ñi am li ëpp ci seen suuf ca asi waaye day ni rekk li ëpp ci seen taariix réewi gox bi lañu ko bokkal ngir xóotal melosuufug tugal tugal a ngi yaatoo km fukki junni junni ak ñetti fukki junni ak juroom ñent fukk ak ñaar ak juroom ñetti téeméer ak juroom fukk ak juroom di benn ñetti afrig walla benn ñenti asi walla aamerig mi ngi séedatliku ci jurromi diwaan penku tugal diggu tugal sowwu tugal bëj gànnaaru tugal ak bëj saalumu tugal gox bi am na ciy réew afrig afirig moom la ñu jàppee ne mooy gox bi nit cosaanoo su nu ko xoolee ci yaatuwaayam ak bariwaayu askanam lu weesu gox bu asi mooy ñaareelu gox bi gënn a rëy ci àdduna bi yaatuwaayam tollu na ci km nekk ci jéeri ji ci àdduna bi ay way dëkkam tollu ci lu ëpp muy benn juroom ñaareel bu way dëkki àdduna bi afrik a ngi yem ci bëj gànnaaram ci géej gu diggu gi ci sowwu ci mbàmbulaanug atlas ci bëj saalum ci mbàmbulaan gu bëj saalum gi ci penku ci mbàmbulaanug end asi rekk la taqalool ci yeneen gox yi yamoo gi jàll na ko ci jëmm doon na gox bu bari y melokaan te wuute teg ci baatu afrig moo ngi jóge ci turu afridi yi doonoon ag giir gu dëkkoon ci bëj gànnaaru afrig ci diwaanu kaartaas beneen cosaanam moo bàyyikoo ci berber taferka suuf boroom suuf ki fay dund la ñuy woowee aferkiw latin yi soppi ko africanus mu doonoon aw tundu waa rom ci afrig araab yi di ko wax ifrqy mu doonoon tiniisi gu tay gi ñeneen ne ci baatu waa geres bii di aphrike amul sedd latin di ko waxaprica bari naaj la jóge afrik la ñuy jàppee ne mooy cosaanu nit ndax desiti nit yi gën a yàgg ci àdduna bi fa la ñu ko gisee ci afrig gu bëj saalumu sahara sahara cëru na bu baax ci màggug gox bi taariixu askani bëj gànnaaru afrig yi day tolloo ak bu tugal ak bu penku gu diggu gi li ëpp ci afrig gu bëj saalumu sahara amul woon genn jëflante ak li des ci àdduna bi da ñoo beru woon xay yi juddoo ci goxu afrik boole nañ leen ci yi gën a mag ci taariixu nit xayu esipt ak bu gana ak bu mali ak bu kuush ak bu songaay añse ci li taariixkat yi wax jàppum njaam mi ngi tambali ci xarnub vii ak araab yi ci lu gën a leer ci atum ba ab njiitu araab takk taxawalee waa nubi yi ngir ñu jox leen ciy jaam at mu jot barab yi njaay mi doon amee mi ngi dale ca mali ba penku afrik ci wàll gi féete bëj saalumu sahara ci xayma nee nañ ci diggante xarnub xviii ba ci xarnub xix benn ñenteel ci nit ñi ay jaam la ñu woon walla ñu ñu manante takk taxawal ci liggéey bu ñu sañut a bañ nee nañ njiitu waa afrik yi ci seen bopp ñoo doon jàppaate ak a jaayaate waa tugal lu weesu bi ñu aakimoo walla sancee suufi aamerig yi da ñoo soxla woon ay loxo yuy liggéey ci seen tool yi def nañ ko ci at ay jaam yu bari jënd nañ leen walla jàpp nañ leen ci tefesi afrik yi sowwu afrig gépp ak ci bëj saalumam itam donte tereg jàppum njaam gi mi ngi waddoon ci lu jege atum réew yépp bàyyeendoowuñu ko amoon ay nit yu wëyoon di ko def cig làqatu ba ci jamonoy aakimoo gu tugal ci afrig moo ngi tambalee ci ndajeem berlin ba ci tembte yi ci atum sedatle gu réew yu tay yi ca la jóge ecoopi moo doonoon menn rew mi ñu masut a teg xool diiney afrig gëstukatu làkk yi ci xayma nee nañ làkk ci goxu afrik ñu boole leen ci ñeenti mbooloo làkk yi fa cosaanoowul bokkuñu ci koom koomu afrig biibël mooy tur bi ñu jox mboolem mbind yu sell yu yàlla yi ci diiney yawut ak kirist baatu biibël la ngi jòoge ci kallaama gerek gu yagg ga di tekki teere yi ci g neen day ab teere bu ñu boole ay mbindi cosaan mbindi atte mbindi xew xewu demb mbindi cellte yu yonent taalif ak ay bataaxal yoo xam ne ci diiru junniy at lañu leen bind biibëlu kercen yi dañ koo seddale ci ñaari pacc seede bu yag bi bi ñu boole teere yi ñu dondee ci diine yawut yi ak seede bu bees bi di ay mbind yu y seede dundu yeesu kirist ci jàngu yi biibël kaddu yalla lañu koy wowee diiwaan yu bennoo walla diiwaan yu bennoo yu aamerig ci anam gu gudd am réew la mu séddaliku ci juroom fukki diwaan ñent fukk ak juroom ñett yi ñoo taqaloo te féete ci diggante mbàmbulaanug atlas ak gu dal gi penku ba sowwu kanadaa moo féete bëj gànnaar meksik nekk ci bëj saalumam alaskaa ci la bokk donte taqu ci mi ngi nekk ci sowwu kanadaa xawaay moom mi ngi ci diggu mbàmbulaan gu dal gi réew mi am na fukk ak ñenti diiwaan yu tasaaroo ci géeju karayib yi ak gu dal gi péeyam mooy washington diiwaan yu bennoo yi ci ciy miliyo ciy way dëkk lañu amoon loolu tax muy ñetteelu réew mi ëppi nit ci àdduna bi ci ginnaawu siin ak end réyaayam toll ci junni km di ñeenteel ci àdduna bi ci ginnaawu riisi kanadaa ak siin gàddaay gi bari na fa lool ba tax muy réew mi ëppi xeet yu jaxasoo ci suuf si koom koomam mooy bi gën a woomle ci àdduna bi te moo am njuddéef mu ñumm mu biirum réew nj ñ b mi ëpp ci àdduna bi turu réew mi thomas paine moo ko tànnoon ci bés bi ñuy am seenug temb ci sulet woowiin wu gàtt wi wi ñuy faral di jëfandikoo ci sunuy waxtaan ci njàngale mi ak ci lonkoyoon yi mooy diwaan yu bennoo ci wu angalteer di united states ñu tënk ko ci us wu gudd wi ñu koy faral di jëfandikoo ci këyiti nguur gi diwaan yu bennoo yu aamerig ci alaskaa lañu gise jeexiti nit ki fa njëkk a teew ci weti at nj j ci tefesu atlas ci wetu at nj j nit ñi njëkk a dëkk ci réew mi ñoo nga bàyyikoo ca goxub asi jaare woon ko ca xat xatu beri ci ginnaaw bi la fa waa tugal yi ñëw christophe colomb moo wuññi goxub aamerig ci at ma ca topp mu nemmeeku barab bi nekk poortorikoo tay jii ci xviu xarnu la réewi tugal ya fa ëppoon doole doon seet ay jàlluwaay ci bëj gànnaar sowwu ak ay am am ci seeni tukki ci topp tefesu atlas gi ñu dem ba taxawal fa ay sancu yu sax ci bëj saalum waa espaañ yi sos fa seenub sancu duppee ko espaañ gu bees di amal ay tukki gëstu ci biir réew mi ci bëj gànnaar sowwu waa riisi yi sanc fa ci li topp tefesu mbàmbulaanu gu dal gi ci la tubaab yi tàmbalee yaxantu ak askan yi fa cosaanoo ci diggante xviiu ak xviiiu xarnu ndànk ndànk la fukk ak juroom ñetti sancu waa angalteer taxaw ci tefesu penku gi lii mooy maamu diwaan yu bennoo yi waa fraa yi nemmeeku pegu misisipi dal di fay sos luisiyaan ngir xóotal yëral foofu taariixu aamerig tuubaa péeyu murit yi ab gox goxaan la mi ngi nekk ci diiwaanu njaareem jurbel ci tunduw mbàkke diggam ak ndakaaru tollu na ci km baatu tuubaa mi ngi jóge ci làkku araab di tekki ci wolof texe dëkkub tuubaa kii di sheex ahmadu bamba moo ko sanc ci atum dëkk bi mi ngi aju ci ndaam doon as ngox maanam dëkku kaw kaw bu taaxeedi te nag doon gannaaw ndakaaru dëkk bi gëna taaxe ci senegaal tey dëkk bi gën a rëy ci senegaal ginnaaw ndakaaru tuubaa moo ëpple yokkute ci barig nit ñi ci diiwaani senegaal yépp at mu nekk ci jamono yii ñu tollu te ñu jàppu ne yokkuteg nit ñi di na àgg ba bu ñu àggee ci ati yokku yooyu li ko waral moo di tuxu yu bari yi nit ñi di def bawwoo ci dëkk yu nekk ci bawol ak kajoor dëkk yooyu dañuy gent si ndànk ndànk jëm tuubaa ci waññib bi nit ñi ñi ngi tolloon ci ci atum bu ñu ajoo ci gam gamle gu nguurug senegaal waa dëkk bi tolloon nañu ci naataangeg dëkk bi lëkkaloo na lool ak màggal gu mag gi giy dëppoo ak demug seex ahmadu bamba ci géej gi ba tay tuubaa dafa bari li waa senegaal di woowe moodu moodu di ay tukkikat yu féete tugal tey ëndi xaalis bu bari ci dëkk bi lii di yaxantu jënd ak jaay tamit da faa dox lool kii di seex abdul ahat doon ñatteelu xalifa seex ahmadu bamba moo fa tabaxoon barab bi ñuy woowe daaray kaamil di kàggu gu ñu denci mbindum seex ahmadou bamba ak yeneeni mbind aki téere yu aju ci lislaam ak ci yeneen fànni xam xam yi yittéel nit mi ngi feete nag ci penku jumaa ji làng ak armeel yi ci tuubaa la jumaa ju mag ji nekk doon jumaa joo xam ni jenn la ci afrig gu sowwu jant ci taaram ak ci rëyaayam man nañoo jàpp ne mooy xolu dëkk bi ndaxte yeneen kër yepp dañoo ñëw di ko wër ndànk ndànk ànd ak màggaayu dëkk bi jumaa ji am na juroomi sooroor ak ñeenti xubba soorooram bi gën a gudd tollu na ci meetar sooroor boobu kii di sëriñ fàllu mbakke mooko tudde làmp faal féetele ko kii di maam seex ibra faal ci juin bis boobu moo di ubbite gu njëkk ba ñu bari teewe woon nañu ko ku mel ni lewopool sedaar seoor foofu ci jumaa ji fa la barabu seex ahmadu bamba nekk kàllaama fr langue en language ñi ngi tàmbali sunuy wax ak jëf ci turu yàlla t s miy rahmaan di kiy boroom yërmaande ju yaatu ji ñu jagleel mbooleem mbindéef yi tey rahiim di ki yor yërmaande ji mu y jagleel ña nangu g jaamoom di julli nag te y sëlmal ci sunu sang sangu b ñu jiitu ñi ak ñu mujj ñi aki ñoñam aki saabaam ak aji liggéeyalam jii di sëriñ tuubaa ak xeetam wépp sunu wax ji dañu ko y tàmblee cib aaya b alxuraan ñu ci y tegtaloo li làkk ëmb yor ko ci y njariñ ci gépp wàll ci sunu dund gi sunu boroom nee na ci alxuraanam ju tedd ji wa hallama aadamal asmaa kullahaa thiumma haradahum halal malaayikati fa xaala anbiuunii bi asmaayi haaulaayi in kuntum saadixiin di maanaa yàlla t s jangal aadama tur ya yépp bi mu noppee jël mbir yooyee won leen malaayika yi ne leen wax leen ma seeni tur bu ngéen léen xamee ñu ne ko tudd nanu sa g sell amuñu benn xam xam boo ñu xamalul bu ñu xam yaw yaa y ku xam ki te y ku xereñ ku am hikma ki kon yii tur ci jii aaya ju tedd mant a doon lu dul làkk wi nga xam ne bokk na ci li yàlla t s njekk a xamal aadama j m bi mu ko bëggee wàcce ci kaw dénd bi ngir mu wuutu ko fi loolu nag li ko waral moo y nekku g làkk di benn ci móoli cosaan yi ñu teg sunu dund gi tabax ko ci bu doonul woon moom dund gi di lu nekk ci lu dul maanaa mu ñu xam di lu gën a jege ag mbàyyima ci ag nite bu amul wuutlaay ma ne xoolal ma dund gu ñu rafleel ci làkk nu mu war a mel ndax moo y googu di fees dell ak junj yi ñu y jëfandikoo bu ñu y wax ak ku luu muuma mbaa ku tëx lii sax ca dëgg dëgg xeet la ci làkk làkk ëppu ko yéesu ko ginaaw moom mbir la mu ñu y def ngir déggante ci ndax kat làkk du lu moy ab jumtukaay ngir waxante ñu ko y jëfandikoo ngir déggante ci sunu biir xanaa déggoo ñu naan làkku njanaaw yi mbaa dundat yi ba ci wu bàyyima yi jubluwuñu ci lu dul li ñu y joyal ngir seen moroom yi dégge léen ci ginaaw nag bàyyima yi di nañu déggante ci loolu ci seen biir kon loolu manatuñu ko o jàppe lu dul aw lakk ni yeneen yépp waaye jeneeral dund gii nga xam ne dafa féex ba ci sax jumtukaay yi ñu y jëfandikoo ngir junj maanaam dund gi ñu rafleel ba ci jumtukaayu b déggante rekk nu mu war a mel nu xeet ak mbir ya y dox ci y sidiitam aki buumi xolam di mel wii xeetu dund de ci li ma jort narul a doon lu dul ag ndofe gu ñu joyal naa doyloo yooyu baat ndegam amuma yeneen yu ko man a leerale ni mu ware gii dund ci lu dul làkk da na nekki gu maneesul a leeral xel it du ko xalam ci loolu la sayyid qutub di waxe ca teereem ba tudd zilaalul xuraan di tafsiir bu mag ci alxuraan mu ca y firi aaya bu sell bii di wahalla aadama ba maakuntum taktumuuna mu ne xool ñu nag ñi ngi nii ci bëtu b xol ak leerug basiira di jàkkaarloo ak la malaaka ya nekkoon ca malaul ahlaa doon jàkkaarlool xool ñu ñun ni ngi nii di gis ag wàll ca mbootum yàlla mu màgg moomee nga xam ne mi ngi ko dénk nekktéef bii di kojug nit bi mu ko y jox caabi y kuutlaay ji mu war ko o wuutu ci kaw suuf mbootum kàttanu g tudde mbir yi ay tur wutal yëf yi ay xammeekaay yu tur sekkare b man a jël jëmm yi walla yëf yi tudde leen ay tur yu leen di def te ñoom ay baat rekk lañu yu ñu wax ñu y ay junj aki sembool yu y tekki jëmm yooyu ak mbir yooyu ñu leen tudde lii daal na la woor ne kàttan la gu am lool solo ak xiima ci dundu g nit ci kaw sii suuf ñi ngi y xam solo sii bu ñu y jeneer coona bu mag bi ñu naroon a jànkoonteel bu ñu mayutoon nit kàttanu g junj yëf yi ak nit ñi ci y tur xoolal coona bi naroon a am ci déggante ak jëflante ndax li naroon a xew moo y ku bëgg a déggante ak sa moroom ci mbir da nga y teewal moomale mbir mbaa ànd ak moom ba ca loola nga joxoñ ko ko mbaa nga laal ko bu dee xorondoom ngeen soxla war ce e waxtaan da ngeen ca y dem mbaa ngeen teewal ko lu ko moy deet ag déggante ci loolu bu dee doj la fawwu ngeen dem ba ca doj wa bu dee nit munt a ñakk ngeen teewal ko lu ko moy du ngeen ca déggante lii daal coona la bu kenn xalaatul a dund ak moom te dund gi tam narutoon a wëy ci yoonam wii bu yàlla t s mayuloon mbindéefam mii man manu tudde mbir yi ay tur malaaka yi ñoom jagle bii soxlawunu ko ndax du lu manul a ñàkk ci ñoom ci seeni jëf moo waral mayeesu leen ko kon làkk moo y ponk bi nga xam ne ci la sunu g dund di tabaxu su nu bëggee muy gu jege as lëf ci g cilwiise aku g taaxe walla lenn lu am maanaa bi làkk nekkee nag ba noppi te tax ñu jeggi mbooleem rombuwaay yii ca ngënéelam la ak jappndal gi mu nu defal ba nu man a déggante ci suñu biir ñewati na di jumtukaay bi dugg ngir teg sunu dund gii ca njobbaxtal lu kawe la di ag nite ak ca tolluwaay bu yekkatiku bee di bu ag taaxe aku g xay bu doonul woon làkk duñu doon man a yekkati sunu dund gii ci xam xam ndax moo y li y tax nga man a raññale mbir ak dundat yi lu ci nekk nga ber ko nee wutal ko turu boppam làkk moo y cëslaayu ag yewwute yewwute ñenn ñi naan ko renaissance ci francais di judduwaat di ci araab nahda di ci maanaa buur buur nag bu nu ko waxee ci wolof moo y jekki jekki jug taxaw ñeneen it di ko fire e dekki boo ko y seet ci maanaa yepp di wudd lenn di la amoon ca orob ca lenn ci y jamonoom di woon lu am solo di lu waa orob dul fatteeti baat bii ñew ëmb maanaa mii mépp di raññale jamono y yewwute ci ngëmméen judduwaat ginaaw ag dee réer ci réeradi xam ci xamadi siggi ci segg nërméelu ci taxaw giim ci tàkk xippi ci gëmm bii baat daal jaasi la ju moo dog seen diggante ak jamono joj tëñëxu ak yewwoodiku moo ko muuroon matale ko xel mu gàtt lakkal leen ci gisiin wu ñaaw sonal leen ci ñu nekkoon ci biiram di way jemadi kanam di ñu soxlawoo ag leer ba yàlla yee ay nit niital léen ca làmpam bu leer ba y leerale jugloo leen ci y nelaw ñu nekk ci g yewwute duggalaale ci ñeneen ñu dul woon ñoon ba tay orob gii di lu leer ca googale leer la tanqe te ca la yewwoo it kon ci gàttal yewwute fii mooy renaissance gi nga y dégg ci kàllaamay franse te y tekki ci maanaa yewwute rekk ndax mooy judduwaat gu xam waral ginaaw dee gu réer waraloon làkk moo y cëslaayu g yewwute du ma a y ki ko njëkk a wax am na ñu bari ñu wax lu ni mel ci xalaatkat yi ak taarixkat yi bu ñu dello as lëf ginaaw ànd ak sunu y xalaat ba ci xarnu b fukk ak juroom ñatt ci jëmmi boppam da nanu gis ne lu bari ci y xalaatkatam aki ñoñ taarixam ku ci mel ni lodoviko antoniyo mortara ak volteer ak wilyaam robertson jëfandikoo woon nanu waxiin wu mel ne wii ndaxte boole nanu ci mbàndarga yi y raññale jamono y yewwute boole woon nanu ci doxu g waxiini gox yi juge ci y waxiin dem ci ay làkk yu réew niki làkku w espaañ wu itaali wu fraans ak wu portigaal ba fa mu yam li gën a yéeme moo y yojinyoo jarin moom dafa jel mboleem amaliiti yewwute gi sol ko ci benn baat mooy filolojiaa di baat bu am ñaari maanaa yu mag mu njëkk mi mu xat la te daytalu gàtt moo y dégg làkk mi ci des moo gën a yaatu te gën a xóot moo y gëstu yu làkk yu njàggat yi adab ci tubaab les recherches linguistiques et littéraires jarin gis na ne bu nu mane e doxal yooni gëstu yu làkk ak yu njàngat yi jaarale ko ci gëstu ci dénd bi nature jamono jooja aw yoon wu bees di na judd di yoonu gëstu wu xam xam wu di kojug làmb làmb ba daj rekk amul waxi kese walla gisiin loolu moo ñu y àggale ci xam xami matematik yi nga dolli ci loolu ne làkk moo y seetu bi nga y man a gise dundu g nit gu xel gi boo gisee ne làkku xeet wu nekk ci jamono ju nekk lenn la ci li y wone am xelam nga dolleeti ci ne ci lanu y jànge xam xam yi nga xam ne bu ñu nekkul woon amuñu woon dund gi du mel nii mu mel tay bu làkk amul woon nu xam xam di juddoo ba y gis jant bi làkk moo y cëslaayu ag yewwute bu nu ko waxee dées na ko man a dëggal rawati na ku jàng jii jamono jàngat ko xam la leen seen waxiin yu suufe ya ñu xeeb jariñoon ñu ko y woowe ci francais dialecte ba ñu leen jëlee def leen ay làkk yu xeet yu réew yu xam xam yu ñu fonk yu ñu fas yéene e doxale seenu g dund sës ci seenu g dox sanni ca àll ba yeneen ya doon dox seen diggante ak xam xam xam ak yewwute mu y làkk wu latin wi nekkoon di lu ñu neew xamoon la gën a rëy ca mbooloo ma réere woon ko te réere gi taxoon ñu reeroon te yewwoodiku wii làkk di wu latin wi nekkoon na di seenu b coona di seenu w ay di seen gàllankoor di ab pakk ci seen digg ak jem kanam ndax la ëppoon ca xam xam ya bu ma waxul sax lépp ca woowale làkk la nu ko daa binde di ko ci jànge te askan wa bu doon téeméer lu yees fukk a ko ci y xam mu y ci misaal daanaka nga xiif lool ba y bëgg a dee di wër loo lekk ndeke lekk gi moom am nga ko mi ngi ci sa ronu ay tànk te ya a ko moom doo ci fay dara xanaa kay da nga y jël rekk jëfandikoo te loolu lépp xamoo ko te kenn a ngi nii ci sa kanam xam loolu lépp te xam ne bu ko waxee dootul jariñu ci ni mu ko daa defe kon na la ko bañ a won xamal la ne ya a y ki ko moom ndax loolu man na a waral sa g wadd sòng ko giir ko ne ko fuuf te bu booba a su ko ab xiif gaarate e du xam fu mu ko y fajeeti ci g càcc waaw waaw ci g càcc kay ndax lii ag càcc la ndax xañ nit àqam di ko jëfandikoo k a jariñoo sàcc ko la te bàyyi ko nee mu toog ci b xiifam ci yitewoo àqam ci taru g yitewoom càcc la de loolu ku ni la du sàcc laaj ko lu mu doon moo raw sàcc fëkk la nax la réeral la dofal la xiifal la neewal doole la nakk a xam la dofe la suufe la réer la bon la waxal lu la soob ne moom la kii man a xam nga ne ko doo fi xame ndax làkk wi nga yor du wu ñu y xame wa kee yor ay dëgg dëegi aw làkk ci la ñu war a waxe war ce e jànge war ce e yëre war ce e gëstoo war ce e binde te ci la nu war a nekke nit boo xamoon li ci addina bi bepp it te xamewoo ko ci doo kenn ku xam ku ñu y lim nga nga y kenn ci ñu xamadi ñi ñu réer ñi ñi amalul seen réew solo lii nag sama gaa yi du g réer di g dof ak dofale ak li la soob ci xeeti xelloodi lii ay li ñu doon def waa orob ca jamono yu diggdoomu ya maanaam middle ages ci angle di nu ko def ci jii jamono nga xam ne moo y ju xam ci anam gu gaaw ngir bari g li ñu war a xam ndax li man a xam te ëpp ci réew mi am nanu làkk wu ñu man a xame ci s lëf ci g gaaw ak sakanal waxtu ak ci s lëf ci g wér ak lëw kon jort naa ne la y lañu war moo y la wa orobi joojale jamono defoon mu y taxaw ci jël seen àq delloosi seenu m dem feeñal seenu m réer sulli seen lu suulu di na rafet nu indil leen sababi feeñug yile làkk làkku latin ci jamono yu diggdoomu yi moyen ges moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam xam ya ak niti diine ya ak politgkat ya ak niti adab ya walla njaggatkat ya hommes de lettre ak ustaas ya la notoon nag ca nit na di woon niti neen ñi rekk ñoom déggunu woon wii làkk lu tumbrànke la woon ca ñoom seen làkki bopp yi y yu seeni barab lañu déggoon bi jamono y yewwute dikkee gelawu l fonk sa xeet nationalisme upp ci orob gepp la lu bari ci xalaatkat yi ak niti adab yi ak woykat yi tàmblee jeng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki réewi bopp niki wu itaali wu espaañ wu fraans wu engle ak yu dul yooyu bi mu ko defee woykatu itaali bi tuddoon dante g taalif komedi xisa bu y reeloo bu sell bi ci làkku itaali naka noonu petrarch g mii nga xam ne li mu gisoom moo y làkku romam wii daal moo y gën ja a kawe y jumtukaay ngir génne xasida y woyam yi bu ko defee miguel de cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di don kixota ci làkku espaañ ci noonu it la rabelais g def moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di franse ngir wuñi ci li y yëngu ci biiram ci njàggat adab lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor kaf chaucer mi di b angle g jug moom itam sotti ci w làkkam woyam yu yéeme yi ci b taar rawati na nettali y kentrebry yi nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati angle yu mag yi yi gën a siw làkki xeet yu orob yi ñi ngi sosoo ci màbbiiti latin ak tiyotin wu itaali wu espaañ wu fraans wu portigaal ñi ngi dagge ci latin wu almaañ wu angale wu danmark wu suwed wu oland wu norwej bàyyikoo ca tiyotin bokk na ci sabab yi jur doxug yile waxiin dem ci làkki réew yu xeet bokk na ci sabab yooyu nekk gu làkku w latin nekkoon di wenn ba yàgg mu seddaliku di ñaar wu ñu y wax kalaasik ak wu wilgeer kalaasik mooy lu yàgg la y cosaan wilgeer di lu yomb li nuy jëfandikoo kalaasik wi di wi politigkat yu mag yi ak boroom xam xam yi ak niti diine yi daa waxe wu wilgeer wi di wi niti neen yi di waxe di ko jëfandikoo ci noonu kalaasik wi tàmblee nakk as lëf ci solo om ak dooleem wilgeer wi tàmblee jël barabam waaye wilgeer wi moom ci jëmmi boppam tàmbli na ci ginaaw bi di soppiku ndànk ndànk jem ca leneen lu dul la mu doonoon ci noonu ay waxiin yu bari te wuute bànqaasoo ca ngir nocciku g lenn ci mbooloo yii juge ci yile barab dem ca yee tas fa ak soreente gi yii barab soreentee te wuute loolu jur yeneen mbooloo y nit judd mu ci nekk ak sa waxiinu bopp waaye loolu moom teewul woon latin des fi di làkku diine wi te y wu xamlu wi maanaam wu ofisel wi ba mujj askan yi yoqat ko te xam ne pakk la ci yoonu seen ag dox aku g jàll ndax ña ëppoon ca ñoom xamuñu ko woon dégguñu ko loolu yobb léen ci ñu xëy taxaw temb ci jële ko fi sanni ko ci seen ginaaw weccee ko ok seen waxiin yooyee te farlu bu baax ci jàllale leen jëme leen kanam tkki ci li ñu soxla woon lépp ci yooyule téere yu am solo te ñu bindoon leen ci laitin ca jamono jooja ci noonu nit ñépp tàmblee gis koom mu rëy mii di ko xam te bu njëkk daa xawoon a jòmb ci ñoom ñu ko y xam ba ci y jariñu lii nag day tegtale rekk li war mu y jëfandikoo làkku w nday wi niki lakk ci wàllu g ligéey ak jàng reew yi nekkoon ci ron suku b sañcaan yi colonialiste yi rawati na yi ci y jëfandikoo làkki jàmbur yi ba leegi niki tubaab ak angle ak yeneen jàppe leen làkki ofisel yii réew de ba leegi dañuñu di jànkoonte ak ag réer gu kawe te tas ci biiru w askanam ak koom koom bu deltu ginaaw ak ag des ginaaw gu rëy ak dund gu suufe kon làkk daa war a nekk di lu yomb lool ci ni ko y jariñoo maanaam mu y làkku w la ëpp ca nit ña niki wolof fii fi senegaal bu ko defee ñu bàyyil fi ni gën a néew itam seen àq ci jariñoo seen làkki bopp ci lefu m jëf ak jàng waaye nag bu booba a du man a ñàkk a jëfandikoo làkku la ëpp ngir jëflante ci noonu la ko y joxe àqi nekk làkku w ofisel wi li nga xam ne sikk amu ci moo y gis nga ay yooni yoon lu bari ci yeneen xeet yi ci reew mi nu y wax wolof yu rafet ci anam gu jàppandi ni ko ñépp di defe ci lu dul ñu ko y jàng bu ma waxul li ëpp ci ñoom te safaanu b loolu néew na nga gis ko maanaam wolof bu dégg yii làkk loolu li ko waral du ne wolof bi daa yitewoowul ñeneen ñi du caagéenu g ñeneen ñi dañu y sotti seen yite jépp ci làkku w wolof aki mbiram li am kay da di wolof day làkku jëflante wi tas samp boppam ci géew bi franse mii ñu y jàpple sax manul a bëre ek moom mbaa mu gëpplante ak moom ndax moo y làkk wi y tàbbi ci say nopp mu neex la mbaa mu naqari la nga ko y xam ci sañ bañ man nag ma y ku yitewoode e tontu ci loolu ndax ni mu ma ñoradee waaye am na nag lu xaw a am solo ci laaj bi mu y booy xool lu bari ci ñi ñu y tudde wolof ci laa maa ngii seen dëgg dëggi cosaan du wolof man li may jàpp foofu moo y wolof li mu y tollool moo y ag cenegaal maanaam xeet wi moo y waa senegaal làkk wi di wu senegaal kon dootul wu giir mbaa waaso waaye wu xeet wi wépp a serin tuubaa amul lenni wolof alhaaji maalik naka noonu te taxul woon nu dégg tukloor kon day mel ni xalaat bii mi ngi jeng as lëf jëm ci g yanu maanaa bu ñu delloo ci li ñu nekkoon di wax mu y war gi làkk war a nekk di lu yomb ci ki ko y jëfandikoo da ma naan nit ñi daal li leen war moo y def na waa sowwu defoon muy tuxal seen waxiin yooyee yòbb leen ci y làkk te sukkandiku ci xamloo ci su nu ko gisee muy lu mant a ñàkk maanaam bu nu fi gisee lenn lu y gàllankoor seenu g dox di làkk wu fi jóox wu ñu xamul ni ñu ko war a xame niki franse ci sunu gaal waaye nag amaa na loolu lepp du nu ko soxla bu waxtu wa jàllee ba nit ña dégg way jóoxi làkk yii ni ñu dégge seen làkku nday wi ndaxte làkk du yàlla ju ñu y gëm waaye kay jumtukaay la ngir déggante ni ma ko jorte ahmad amiin wax na ca téereem ba tudd fajrul islaam aw làkk sàkkeesu ko ci genn jañ maanaam jekki jekkiwul rekk am ñu mujj ñi bi ñu ko y jële ci ñu njëkk ña du woon lu mat li am kay moo y nit ñi dañu y sàkk ci seenu g njëlbéen ay baat yu tolloo ak seen aajo bu yeneen mbir feeñee nu sàkkal leen ay baat yu bees bu ay mbir raafee amaa na ay baatam raaf làkk nag a ngii nekk ci dund ak dee gu sax naka noonu bàyyikoo yi mooy baat yiy tukkee ci yeneen yi ak waxiin yi ak baat yi ñoom itam dañu y màgg di yéeg ni xeet wi y yéege di ko magge yooyule làkk di yu orob yi de gënuñu fenn mbaa ñu kawe ci lenn sunu yos yu afrik yii li fi nekk kay mooy ñoom dañu leen a fonk sonn ci di def lu mel ne li ahmad amiin di wax mu y sàkk baat yu bees saa su lu yees amee kon sama gaa yi nanu doylu ci lii nu yor ndax li sunu di neex sama dàq na ko kat te jéem ko o jàllale jëmale ko kanam te tas ko ci mbooloo mi du y caaxaan la nit ka y xalaate ca la war a waxe ci maanaa li nga y xalaat ci sa biir dënn sa biir xel mu y jeqarbiku ci sa y yëg yëg jarul fireeti ci weneen làkk wu dul wi ko xalaat ngir déggal ko ku nu jàkkaarlool ki bu ko fekkee mu ko y man a dégg ci wi ñu ko xalaate loolu li mu y jur mooy yàq waxtu te mu y lu gànjaru wax ju y joriku di dikk ànd ak kem bu rëy ci g jàppandi manul a ame ci lu dul làkku w nday wi nit ki juddwaalee walla wi mu àndal ay at di ci jàpp ak a oy ci këram ak pénc ma ja ba ak daara ja nga xam ne da y faf fàtte wow ndayam wa mbaa mu xaw ko o fàtte ba mujj wii di wu jóox sax mooy far di taxaw taxawaayu wu nday wi bu dee fii nag gisagunu tubaab jël fi taxawaayu b wu nday wolof mi y nday kay moo sax di nday ba leegi ci moom rekk lanu y man a ame joriku gi nu sox la ci wax misaalu m loolu yaa ngi koy gis ci ñii di xëy ak a gont ci leekoli nasaraan yi ñoom de ca dëgg dëgg da nanu ko dégg xayna waaye lu ci ëpp du ñu ci man a génnee seeni xalaat ci g joriku aku g yomb waxal sax aku g dëggu ndax dañu y diriku ci seeni wax ak a jàddantu ak a xootal fu nu ko waroon a tondale ba far wax ja day doon leneen lu dul la mu bëggoon a doon walla sax leeg leeg ñu rax ko ak yennaat ci baati wolof ngir noppalo o ca bu ko defee tubaab bi déggul ay wolof du xam li ñu y wax wolof bi déggul ay tubaab it naka noonu kenn rekk a ko y xam ki boole ñaari làkk yi li ma gis moo di orob ca yaatoom ga ak ca jégeente y xeetam ya ak seen ag niroo ak gu làkk ak bokk gisiin ak diine ak melo ak man nga ne jëmuwaay nga rax ci dolli nekku g yenn ci seeni làkk di man nanu ne yu addina bi bepp niki angle ak wu ko xaw a jege niki francais teewul ñoom ñu nekk di ñu jàpp ci seeni làkk xeet wu nekk ca wosam te teewu ko o jàng nag yeneen yi rawati na angle di ci jokkoo saa su begge e jëflante ak ñi déggul wa mu yor danmark ma nga ak danwaam suwed wuwedam da ma a tayye e lim waaye wu ci nekk ak wosam ba ci belgik sax nga xam ne ñaari xeet yu wuute e fa dekk teewul xeet wu nekk yor sa wosu bopp te teewu la a jàngi leneen ba ca wu sa moroom bi nga ko gisee mu y xam xam ndax xam xam du lu moy xam lu mat a xam te loola mat na a xam ndax da na jur ag rataxal diggante jur ag xam sa moroom jariñu ci jariñ ko addina bi dafa war a sosu ci g dimblante jariñante fonkante deet jariñoo ak dimbandikoo te lii tubaab yi di def du lu dul dimbadikoo ak jariñoo ci suñu g suul ray joggi nërméel mbooleem sunu yëf ci taxawal seen yëf wolof nag daa na wax pesu m kanam boroom a ko y fajal boppam kon nag pes nañu nu lu nu y xaar du nu jug di door mbaa nu y daas ay jaase eki gobar li nu y def kay moo y jëfandikoo xel ni ko seriñ mbay jaxate daa waxe mu y ab noon bu la noonu boo y xeex ak moom bu mu ko yëg na xëy rekk daanu door a xam ne ya a ko daaneel fa la sa b noflaay di ëppe ca la la nga y jëfandikoo ci ngànnaay di gën a néewe ndax bu fekkoonte ne daa waroon a jàmmaarloo ak yaw nga y jëfandikoo lu ne ngir moytu y dóoram ak di ko jéem a dóor leegi fegal nanu la coona b jéem a dóor ak moytu moom kay da nga y agsi rekk dóor mbaa nga jam ndax moom yëgul ni ya a ngi koy fexeel bu ko defee mu dee naaxsaay lii estraategi la ci lu mel ni franse ci réew mi manoon na fe e nekke ni fi araab nekke di b soppe te bañ di b noon di luy dem ànd ak di demale waaye jort ne moom rekk a war a dem xoolal ci maanaa araab ñi ko jàng tay ñoo y ñi dégg wolof ñooy ñi ko fonk ñoo y ñi ko y suqali loolu bu amee li mu wund moo y ne araab ca mag ña jumtukaay la woon ngir jëm kanam ci xam xamu diine waaye it jëmal kanam seen kàllaama gi nga xam ne tay daa fees dell aki baati araab yu ñu jox kàddu g wolof ci fi ko wolof amewul xoolal ma baatu b jamono mi ngi juge ci samaanu maanaam juge ci mahnaa yu mel nii yu sakkan lanu ci daa nanu dem sax ba y jëfandikoo as lef ci xarala di sàkkal wolof ay jumtukaay yu làkk yu mu amutoon te ñu gis ko ci araab te xam njariñam xam ne man na leen a amal njariñ niki yaa g askanal googu nekk ci araab nu ko daa tollolee baatub koj naan yef yu di koju g nàggam ci maanaa xam xam bu di koju g diine jublu ci xam xamu diine mu y mbaat sos su nu ko fonkee man na a am ay jeexiit yu am solo ci ëllëgi làkk wi ak ci diggale di ci tubaab par l intermediaire de ak ci g jonjoo di ci tubaab en direct yii di baat yoy danu lay won ni araab jeexiitale ci wii làkk du caagéenu danu di ay baat yu amul woon ci wolof aha kay yu ci amoon lanu waaye fii yeneen maanaa lanu yore yu bokkul ak yanu yoroon nun itam bu nu gisee ne yii du yi nu soxlaati walla maanaa yii jubul am nanu sañ sañ ci def ni nu neex ndax ñoo y boroom kon noom ñaar way jàppante lanu woon yu y dimbalante dunu woon ay noon wolof am na ay waxiin yu bees aki baat yu yees ci tabe g làkku w araab la ko ame ndax boo y xool da nga y gis ne woomle g wolof aku g riisam mi ngi ko jële ci jël lu toll ne làkku w araab ca yaatoom nga ak tàllalikoom ga firi lépp baat topp baat loolu moo nekkoon seen anamu g jàngale nga xam ne da nu la y wax baat firil la ko ba mbooleem teere yi nu daa jàng ci araab te yu bari lanu woon te wuute ci fann yépp ci nii la nu ko daa defe loolu jural leen nu mujj baat bu nu am ci araab ca woomam ga nu am ko ci wolof bu dee franse moom ci nga y dégge wolof bu naan la nga jéggal ma sama wolof daa leerul te loolu ag xeexam ak ag jéem a suulam a ko waral ag yaakaaram ne moom rekk a war a nekk ci kaw suuf a ko waral ak jeem a toogam ci laltu gi mu des ay barab yu nu man a toog mu teg ci ay tànkam lal ci y loxoom ne kenn du ci toog moom reek moo di li ko waral kon de kii ku siis la ku xat la ku nay la ku y ngartaajoo la ku y nangu suufu s jàmbur la ku yëg ne moom rekk la ku am bëgg bëggu suuxal la lii nag ku ko mas a am ya a y ki nar a suux nar a neen nar a seey waaye loolu lépp du tee mu y lenn ci li ñu moom moom nasaraan du moo moomati li nu ci moom ndax ca aljeeri de kenn ci ay xalaatkatam nee na woon franse de lenn la ci sunu am màngiit mi nu mànge ci tubaab yi màngiit moo y xaniima di ci maanaa li nga y nangoo ci ki nga y xareel boo ko gañee maanaam loolu moo y li franse di ñëw lépp ngir nangu jël ci doole fitnaal foñloo fàtteel taxaw ci doole jaaye ko teewul muy lu am solo di lu ñu man a xame e man ce e jariñoo kon bu nu ko jàppe njariñ lu nu y sànni waaye màngiit mu nu mànge ca sunu xare ak ñoom ndaxte addiis a ngi nii bu naan hikma moo y réeru m jullit bi fu mu ko gis daal na ko woor ne moo ca gën a yay hikma nag di lol boo ko doon firi da nga naan moo y lépp lu rafet rekk jekk xellu baax di lu ñu xam di lu am solo ci dund mbaa dee xel mu rafet ba fa mu yam kon franse li fe ek ya a ngi ci y gis sa njariñ moo xam lu adduna la mbaa leneen kon ci hikma la waaye kay li y li yéeme moo y da ma a gisagul ci réew yi y dem te y dox di dund di jëm kanam mu ci y waxe ci w làkk bu feeñee bu làqoo weneen maanaam loolu mooy li xew tay ci sunu réew mi nga xam ne bu ñu feeñee ci lu fés mbaa nu y jëflante ci anam gu ofisel ofisel ci li wolof mànge ci tubaab la da nga nu y gis nu y waxe ci kallaama y nasaraan bu nu delloo fa sunu y kër di ko defe ci wolof leeg leeg sax nu y rax la ñu y defe ca franse yennat ci baati walof kon mokkalaguñu te loo mokkalul manoo ce e jariñu li y li nu mokkal kay moo y sunu wolof mii ñépp di wax ku dégg franse ak ku ko déggul ku y ku ndaw mbaa nga y mag fii nga y gis jëwrin ju mag ju taxaw di wax ci googule kàllaama ba yàgg mu ruur toolu b wolof fac ca soxlaam bu baax mu mel ni daa déggatul tubaab walla mi ngi ko y bëgg a sonnal ndaxte nag ca dëgg dëgg coona la di wax lol boo ko déggee it wi nga nàmp nga gën a dégg te ci nga gën a gise sa bopp ki nga y waxal it moom la gën a dégg du am lenn lu mu ci y xel ñaar mbaa mu ko ci y laaj du caagéenu g baat bu mu ci y réere daanaka ba ci sunu njiit lii fi nekk tay di wadd ba laa bég ruur toolu b wolof ci biir waxi tubaabam day mel ni da ce e gën a gis boppam mbaa mu gën ko o yòmb mbaa noppal wax leen ma lu mu raw gu xam xam gu mag itam boo y xool da nga naan demewu fi noonu li sabab loolu moo y ne nun li ñu y daj ci dégg tubaab daa metti te rëy te li mi y jël ci ñun ci waxtu daa takku loolo oy li y waral nu y neenal xam xam yi moom kay fii fi senegaal dégg franse doy na fi xam xam àgg na ci sunu njiitu réew lu njëkk la xam xamam bu mag ba nu doon naw lépp du woon lu dul naan na géeju g franse du ñu ne la benn xam xam bu di koju g tegnik mbaa xarala la xam seriñ tuubaa mi ngi ñu naan ba mu ñu y jàngal xam xamu lislaam jiitalal xam xamu tawhiid mu y li la y xamal ni nga y gëme yàlla kennal ko wéetal ko teg ca fiq mu y ni nga y jaamoo sunu boroom ak tasawwuf waaye mu teg ca ne ak jumtukaay ya mu jublu ci jumtukaay yi làkku araab ak la mu y àndal ngir nga man ko o dégg mu y nahwu ba ak bayaan ba nahwu di li y nos làkk wi di ci franse grammaire bayaan di li y nos wax ji di tax doo guddal lu waroon a gàtt loolu lépp bi mu ko y lim mu bokk ci xam xamu diine da leen a tudde ay jumtukaay mu jublu ci ne xamluwunu leen ngir seen jëmmi bopp waaye ay raas lanu yu nu y yéege jëm ci xam diinee rawati na alxuraan mi nga xam ne manéesu ko o walla su c ee xam te déggeesul araab mi nu ko wàcce ndaxte làkk wu nekk am na jagle y boppam yu moom rekk a ko moom ku firi wor la léeb wa wax rawati na lu mel ni alxuraan ca jafe g làkk wa nu ko wàcce ak màggu g aji wàcceem bu nu waxee màggu g aji wàcce ji da nga ci y dégge màggu g li nu wàcce kon loolu màgg na màgg gu kenn mant a dégg ci g yòmb ak ub noflaay lii moo y li waral araab di jumtukaay ngir xam diine di xaaj ci xaaji xam xami diine yi kon mag ñi jànguñu woon araab ngir jëmm ja waaye jumtukaay la woon ngir xam la mu ëmb loolu mooy safaanu b ku mel ni senghoor aki gaayam noom làkk wi moo leen taxoon a jug nu sonn ci sonle ci bu taxutoon doo def fo o toll di dégg baatub frankofoni lu mu y wund tontu leen yalla baax na ba mu nu teralee ci nu nekk ci jii jamono di dellusiwaat ci sunu bopp di ko tàmble e fonk di gestu li jar a gestu te lu ci gën a rëy sunu kàllaama gii ndax giñ naa ne xam gi bu wóor ak jëfandikoo gi ci fànn yépp di nanu jariñ lu bari te y jëf ay jëf ci yòmbal sunu g dund da na nu yòbb tam ci nu y dëgg dëggi réew dëgg dëggi xeet dëgg dëggi ay mbòkk yu gis ne am nanu lu nu bòkk yu y mbòkkoo ak a joqalante ci g nooy ak ug jàppandi jëflante di na gën a dolliko o ratax déggante gën a yòmb xam gën a jàppadi koom gën a lëw ndax xam xamu koom di na gën a yòmb a jariñoo ci ligéeykat yi jaaykat yi naka noonu naataange di na raññiku ci wàll yu bari ngir xéewal gi am te ame ci jàppandi g xam mbir yi ngir jumtukaay bu yòmb bii am te amutoon di sunu w làkk la ko war kay moo y mu ne ko bar bar moo y baat bi bàyyima bii xam kon noppal sa bopp du nga nekk fa naan ko kaay waaye xanaa bar mooy li sonleedi naka noonu ñu dégg ba noppi wii làkk nga xam ne leegi xam xam xam rekk a nu war a ñor te dese nu nu naan da nu y bàyyi wii nu dégg nee naan dañu y xamlooti weneen door a xamlu xam xam yi taxoon ñu y xamlu w làkk loolu jort naa ne dofe la sànk waxtu la sonnal sa bopp la jàppoo ni sunu ligéeykat yii ca seen yewwute ga ak muus ga ak xarale ga bu nu ci doon boole di leen seetal li nu aajowoo ci xam xam bu aju ci seeni ligéey defal leen ko ci seen làkku réew wi nu dégg naan ko xam ko xam gu xam kawewul jàppoo ne bu loolu amoon du ñu fi xar baax jëf fi ay kiimaan def fi lu raw li tubaab yi di def ba nu leen di naw da ma a yàgg a dégg ci sunu biir ku naan nit ku ñuul daal xawma lu mu def yàlla ba yàlla gàttal um xelam nii te loolu day mel ni bu nu ko y wax ñi ngi dëggal li tubaab bi yàgg a wax yàgg ko o jort ci ñun mu y moom moo nu ëpp xel walla sax moo y ki ko am nun li nu am du am xel ndax xel ak ni mu màgge jòmb naa nekk ci yaram wu ñaaw wu ñuul wu tàyyeel wii am ku ma dégg te moom ku ñuul la mu mel ni ku y jàpple tubaab yi ci seen wax jooju naan ñu ñuul ñi de àjjana bu ñu fa duggee su nu fa yàggee yàq ko naqaril ko tubaab yi nag ñoom bu nu tàbbee sawara su nu fa yàggee defar ko neexal ko waaye boo y xool sax da nga y mel ni ku gis lu ni mel te sabab bi du dara lu dul jumtukaayu jàng bi moo nekkul ci sunu loxo mu y sunu làkku bopp làkku jàmbur day waral nga gëm jàmbur xeeb sa bopp xoolal ci nun ñi y làkk tubaab sunu delluwaay sunu jëlewaay sunu ndëërlaay moo y fraans ak nu mu man a rëye mbaa mu tuutee ni kii moo y ki nu gëm bu nu ko gënoon a xam it jort ne moo nu ko gën a def lii aji am la ju ñépp di gis di ko dund li ñu y wax cosaan da y baat bu waa senegaal baaxoo wax di ko tudd lu bari ci seeni wax mu mel ni day lu ñu fonk ba ci lool mu mel ni fonk gi moo y yoon ndax boo y xool cosaan mi ngi bàyyikoo ci baatu sos di kon fa nga sosoo juge ca bàyyikoo ca bu dee nit la ndayam baayam dëkkam réewam aadaam aam lii moo y cosaanam ndax ci foofu la sosoo bàyyiikoo fa kon lii mooy cosaan waaye ndax li nu def fonk cosaan la nan laaj sunu bopp bu baax te xootal laaj bi ndax fonk nanu sunu bopp sunu cosaan man dama naan déedéet déedéet kay ma dellu ne déedéet jort naa ne ci barabu fonk sunu bopp tubaab bi mooy ki nu fonk ci barabu sunu cosaan cosaanam lii a y li am di li nekk tubaab bi la nu y xëyal di ko gontal ak doonte as lëf ci sunu njariñ a ngi ci aw làkkam lañu y sonn bàyyi sunu wos te kat làkk moo y dëgg dëggi cosaan ndax mooy seetu bi y wone boroon te y jimblang ji y ëmb li xeet wi indi ci y jaloore aki mbanoore aki aada aki cosaan kon moo y mbuubs mi nga xam ne bu la réeree la mu ëmb sànku naaxsaay kon déet ag wuutu di ñeel ko tereesul jàpp weneen waaye na sa wos jiitu ndaxte léeb wa nee na li nga am boo ci séenéenul doo ñeetaane mu y ci maanaa li nga moom boo ko fonkee mu doy la nga doyloo ko doo soxlaal kenn lennam mu y lu wóor ndax jort naa lii fi nun bu nu ko fonkee dem te du nu sonn mbaa nu y ñee kenn mu mel ne la karlo lefi waxoon di kok ku jàng njàggat lu itaali njàggat fii mu y tekki litterature ci nasaraan da nga ko xam mu ne woon kristo s fermato a eboli di ci maanaa kristo di yonnant yàlla hiisaa ma nga yam ba mi y def doxu b nitale ba yiwale ba xayale ba taaxale ba diinele ba yéwénal ba ma nga yamoon ca eboli jotutoon a àgg sunu dëkk jublu woon ca loola ne àtte gi walla ci ni nu ko gën a baaxoo waxe nguur gi mu y baat bu ma soof ndax nguur moom nekkul lu dul fu y buur di dunde nguur nekk fa waaye mu begg a wax ne nguur gi kon di gu itaali bi mu y defar da fee bayyi sama dëkk bii jéemu ci dara sama w nit di ñu dofe ñàkk am xel ngir néewu g li ñu leen sotti ci xam xam man itam ma ne naka noonu ngir sunu ñàkk a jëfandikoo sunu làkk di jël wu keneen ku wax lii de amaa na ñu ne ko yaw de xanaa da nga a faf jort ne làkk moo y yàlla ji y faji aajo rawati na bu dee sa wosu bopp ndax da y mel ne lu y xeeti man manu def ak jëmale kanam jumtukaayi jàll ak jàllale jox nga ko ko kon daal moom rekk doy na ngir dox ma ne déet du loolu la a bëgg a wax li ma jublu kay moo y moom de moo y gën ji jumtukaay te y gën ji dokk ci ku mant a ñàkk a sukkandiku bu y doy gàttalaakonu b dox la yombalaakonu dund la mbokkalaakon la bennalaakon la di boolewaakon di taxaakonu yëg sa bopp fonk sa bopp tasaakonu xam xam jàppandilaakonam dabalewaakon ak ak ak man de maa ngi naan te du ma dañ naan jël leen ko moom a de moom a de moo y li ñu y teral di ñu jugal di nu doxal di tax nu y xalaat di bind di yër yëglekaay yi y lëw di jàngu ay bindkatam di dolliku taalifkat yi y yokk yëngu yëngu gu xam xam di gën a sawar cawarte g caada ak gu saxaafa gën di dëggu gën di fés gën di laalu bindante di mujj di nekk ci lu dul ab coona ci s lëf ci g gaaw ci b noflaay ci g ratax ci lu dul xalaat mbaa toggoo wàlla yenn anami moytu kon moom la mooy noflaay bi di jàll gi di naatange gi di meññ gi di woom gi di fulla ji te y yéeg gi xoolal as lëf ci yitewoo gu tar ak jublu gu mag gi nga y seetlu fii mu nekk ci sunu mbiri réew ak mbiri xibaar te loolu li ko jur du dara lu mo y xibaar gi nu y xibaar askan wi ci seen làkku bopp wi nga xam ne jamono jii ñépp a yewwu kenn gënul a xamati ki jàngul li y xew ci réewam ci wërlaayam ci goxam njiitu l réew mi sax gënul a xamati gone gi y gën di gone li y wëndéelu ci mii réew ak ca mee lii lépp ngënéelu l sa w làkk a da y wëy nag ba ca lu dul xibaar àgg ca mbooleem lu dox mbaa mu raam ci lu nekk di yombal di gaawal di àggale di noppale di soreele fitna seetlu naa mu bokk ci la ma seetlu ne leegi jàngkat yi ak jëfandikookati internet yi dañoo am ag jeng jëm ci bu nu y bindante di ko defe ci wolof rawati na bu nu yakkamtee li leen jañ ci di ko def boo ko xoolee lu yanu maanaa la te yéeme mooy noflaay bi ci nekk ak gaaw gi ak nakk a faale gi ak ñàkk ge e xalaat mbaa ragali yaq ci nasaraan kon lii lépp ay pakk lañu ci sunu ay xalaat di dox sunu y xel di xelli suni y xalima y sotu sunu y daa di soosu nu y joyal sunu y gog ci di bind li y jeqiku ak a fuur di buur ci sunu y xol war a nekk di lu nu y yaxal ci keyit yi ba way bañ ñi kumpa di ko war a xam am na jeneen aji feeñ fenomene ju am ci jamono jii moo y ñu bari ci ndonga yi y bindante ay bataaxel sms ci ëyukaay yi telefon danu ko y def bu nu ko deful ci wolof ci franse bu nu daggat maanaam bu nu dog la ca y sonnale mbaa mu ca y yàqloo ngir ma gën a leer danu ko y bind ci anam gi nga ko y dégge man ko o xam déet gi mu ware ci maanaa ci barabu mais nu bind mee veux nu bind ve loolu ba tay da y wund lakkal gu leen wii làkk lakkal ci mbindiin wi dégg gi jël gi mu y jel seen waxtu ak jafe gi ci ñoom leeg leeg nga gis ci ku ci def lu sakkan ci dundam ci jàng ko ci g tar te du tax mu àgg ci fi ci war te wolof kat mi mu jàngul masu ce e sonn ma nga ko dégg dégg gu xar baaxe kon kii bu ko jàngoon mu yiteel ko ni ko franse yitéele nu mu y mel laaj naa la ko xanaa kawe xanaa raw xanaa noppalu xanaa sakkanal waxtu xanaa gaaw a àgg fees yewwu ci y nelaw xippi taxaw jàll romb màggat mu màggat ci am njàggu m tubaab jabaroo tubaab tubaab la tubaab ngéen dénk seen gaal gii dëggel na kii du bëggati ku dul tubaab lu dul tubaab dara ci boppam li mu moom du ko ñorati te ñii nag ñoo y ñi ñi y faral a dénk sunu gii gaal kon waxuma la jengal ko waaye diigal ko la ñi y def ñoom xamunu joow gaal li ñu y wax permanaat la nu xam promanade ànd ak seeni jabar mbaa y ndaw xaj topp ci ñu y def leeg leeg ñu sanni ko ab bant mu wadd for nu ko y xonte li ëpp ci sunu njël li bu ab baykat di dee ci b xiif te moo y ki taxawal koom mi ñu y jënd ay way màggi mbéregaan oto naan lu manul a ñàkk la te doonoon ñu ñàkk ñoo dugg walla su nu taxawul ci doon sunu bopp ci lepp ak fepp xam nga réew mii da dul mu nu yore xam xam waaye nasaraan firnde ji moo y lu waral ña fi nekkoon te doonoon ay boroomi xam xam te di ñu nasaraanoodi nanguwuñu woon leen a jox ub nosam bu ko defee nu ko y wommate xam xam ak leer bëgg sa bopp sa réew sa njariñ sanni nee lu keneen waaye loolu lepp du man a nekk ndax du sunu mos mu keneen la te keneen ki tubaab la kon moom ñoru ko mu y dem di dox di jëm kanam li ko ñor kay na des ci y loxoom mu y digale ni nu k oy yoree ndax mu man di sax di lu mu moom waaye tay nga dee de yaw tubaab lii de jaral nanu sunu ay bakkan ak yu doom ndax ñoo y ñi ko moom kon tëyyal sa yëf te ba no ok li y sunu lii a y li waraloon mu dénkoon ko màggat ma màggatoon ca njàggu m tubaab ma te jabaroo ca xalaatu ko o dénk keneen ku ko mo y ndax moo y genn wàllam di ki mu wóolu di mbuus mu ñuul mu ñu sol yaxi tubaab yàpp wa xel ma xalaat ya nii la ko jenn waay ju mbayeen daa waxe xoolal ma kii nga xam ne naan na géeji xam xam yi te defewu ko ci tubaab ni nu ko y def danu ko y yòbb ba ca àll ba nu jox ko fa as ndiggante su gàtt ci waxtu ci benn leekol mu fa y joxe ay bind cours ci wu araab ak doonte la mu jàngi woon du làkku w araab da ci doon jànge rekk kay gisati nga fii firnde ju leer ne ñoom de xam ñoru leen du caagéenu g xam xam li leen ñor kay moo di njàngu m tubaab lii nag waa réew mi ñoo y ñi ko war a dindi sunu bëggee boy joy tàkk wëy di yéeg ànd ak way yéeg ñi mii du dem li fe ek nii la bu nu dee ñoñi li fi nekk realistes dañu naan nanu bàyyi li fi nekk mu nekkal boppam du nu ko ga kenn mbaa nu ko ci y manante forse nit ñi tànnal seen bopp ci anamu g demokaraasi bu ko defee làkk wu nekk nu jox ko àqam ak li mu yayool ci ndimbal aar jàllale nga xam ne déet ag noono loolu man na a nekk sunu ndimbal sunu njariñ te ñu sanni nee li nu y wax ofisel am as lëf ci g nooy flexibilite ubbiku ci mbooleem làkk yi ubbiwaat bu baax sunu làkk wii mu man a ëmb guux baat yu bari yi ko y noppal te bañ di sonn ci di leen wutati ñu y juge ci boppam fu nu gise ne lii moo yell fii nu ne loolu la ba kero lenn di taxaw taxaw gu fés gu leer gu deesul sikkati man nga ne loolu sax am na ci wolof ci sunu gaal waaye du tee nga ne am na yenn ruq yu jar a gën a ubbi mu aju ci tas mbind mi gën ko o jàngale gën ko o yaatal ba kero booba ak ba ginaawam sax na ñu y jëfandikoo lu fi nekk te xam ne sunu yëf a waaye ci anam gu maandu gu yamoo te yell gu dul gaañ kenn lii nag am ci sunu tele bi nga xam ne daa mel ni yëfi kenn la du lu nepp bokk ñaaw na di xibaar lu toll nii ci w nit moom li nga leen di di xibaare nga ne as daggiit ci waxtu lanu leen di man a jagleel bu dee ñeneen ñi nga xam ne ñoo y ñi gën a néew te y ñoñ boo ko doon seet sax da nga naan matunu fukk ak dara ci teemeer ci askan wi nga jël la ëpp ci waxtu jox leen ko nu y xibaar xibaar yi ci franse te nga ne yeete e la tax a jug ay fen la de ay nar la li waral jëf jooju kay moo di màggat mu jabaroo tubaab a la ko digal ci taxawal keneen nërméel nu suul nu suul sunu teddnga sunu g xam yekkati keneen ki nga xam ne ca dëgg dëgg wart a woon a sax aajowoo gile yekkati and ak loolu lepp du tee ag jam critique di lu man a ñàkkadi ñeel ñenn ci sunu imaam yi ndax itam jël lu tol ne mbooloo mu toll ci ay teemeeri teemeer nga y wax ak ñoom di ko def ci làkk wu nu xamul teg loolu diine loolu dofeel la yàq waxtu la yab nit ñi la xeeb sa bopp la xamadi la xamadi màggu g diine la ndax lu nu rafetlu la ci fu nu y xutbaa nit ñi ci ajjuma ginaaw ay jullit lanu ñu laal ci s lef ci araab làkk wi y wu alxuraan loolu boo ko y xool ag sonn a ngi ci ci jàng ko ngir man a xam alxuraan waaye it xamante ak sa yeneen mbokki jullit yi ndax moo war a nekk làkku ofisel wu addina y jullit ñi di dox ci g bennale ci g boole ci g xamalante ci jappandal ag jokkoo ci biir jullit ñi waaye tekkiwul ne danu fe e war a nekk naan xar mi kaay te m dégg rekk bar aji laaj laajoon na ne ndax li nu y jële ci jàngu bu nasaraan bi ci xam xam man na a wuutu li nu ci y ñàkke ab laaj a ngoogu di bu diis bu rëy bu am maanaa bu soxla ku ko tontu man la ma ca jéem ci tontu bi moo y benn baat bi ma jortul ne keneen du ko ci weesu moo y déet déedéet la nu fa y ñàkke te mu y lu gànjaru di lu am solo moo y li nu fonk a wax mu y cosaan làkk nag ñëw di li ko y jëmmal di ko taxawal di ko wuutu di ko nekkal di li nga xam ne ci lu dul moom déet cosaan kon lu nu fa man a xame réer nanu ñàkk nanu gàttañlu nanu dof nanu ñàkk nanu jumtukaay ba jumtukyu b yombal ba bu noppal ba bu gaawal ba bu rataxal ba bu jooral ba ba y déggale te y bennale di yombale ag jokko te di ab xamalewaakon làkku w jàmbur niki doju pakkastal ci yoonu jëm kanamu réew yi ko y jëfandikoo te taqoowunu ak moom taqoo nga ca war sunu boroom t s nee na wamaa arsalnaa min rasuulin illa bilisaani xawmihii liyubayyina lahum mu y yonniwunu benn yonnant ci w nit ndare bu danu ko o waxloo ca làkk wa ñu dégg lii yàlla sax ci di ko def bu amee lu mu y tegtale de du weesu waru g wax ak nit ñi jàngal leen ci wi nu màgge dégg ko dégg ga ca war baat yu jóox yi ñooy yi dugg ci làkk wi te bokkuñu ci woon niki baati tubaab walla araab yi nu y gis ci wolof bokk na ci li yayoo xamle mu y làkk moo y li nit ñi di wax di ci déggante e maanaam jaaduwul ñu naan bii baat bu franse la walla bee kon nanu ko sanni te nit ñi ci lanu doon gën a déggante e ca bu wolof ba ko fa doon wuutu ahmad amiin nee na ca teereem ba tudd fajarug lislaam araab yi de ca njëkk lislaam jële woon nanu lu sakan ci y baat ci làkku faaris di wu waa iraan wi ak wu rom ak wu isipt ak wu ecopi yooyu baat seen yaxantukat yi daa dem foofa a ko daa indaale nu duggal leen ci seen làkk wi boole ko ci waaye nag araabeel leen maanaam dëppale leen ak sart yi seen làkk laaj ci noonu alxuraan ñew tudd leen kon nag bépp baat bu nu man a jële ci làkk daa war a lemu ci sarti sunu w làkk amiin neeti na ci benn teere bi yahood yi de am nanu ag jeexital gu mag ci làkku araab tàbbal nanu ci ay baat yu bari yu araab yi xamutoon ak ay term yu diine yu nu xamul woon baat bu mel ne jahannama ak shaytaan ak ibliis lenn lanu ci waxaat na ba tay ci bii teere woykati araabi nasaraan yi ku ci mel ne xussu bnu saahida ak ummayata bnu abii salt ak hadyu bnu sayd ñoom duggal nanu ci araab ay baat aki toggaliin taraakiib yoy araab yi xamunu ko woon ni ngi naan ummayata bnu abii salt moo xamal araab yi waxiinu bismikal laahuma mu y ci maanaa ci sa turwi yaw buur bi ñu ci y tàmblee ay wax aki jëf xussu it moo y ki njëkk a wax ammabahdu ammabahdu di baat bu nu y jëfandikoo ngir teqale wax ju bokkul ak ji la tax a jug mu mel ne nga y bind bataaxel nuyyoo wax li y ànd ak nuyyoo bi ba noppi war a jëm ci wax ji ne leegi nag lan moo y jafe jafe bi ku senegal ki di jànkooteel ngir làkk yu bari yii nekk ci réew mi fekkante fi ñu y yu jàmbur yi ak yu réew mi te nu jël yu jàmbur yi teg leen ci kaw yu réew mi nitu g neen ci sunu réew mii bu duggul leekol ak doonte dugg na ko te bu tubaab da nga ko y gis jamono ju nekk mu y jànkoonte ek lu bari ci y jafe jafe ci lu aju ci ag jëflanteem ak nit ñi aku g jokkoom ak ñoom jafe jafe yooyu lu ci ëpp li ko y jur moo y ñàkk a déggoo gi y am ci digganteem ak ñoom te loolu da na àgg ci jural ko ag fasu complexe ak ñàkk a wóolu sa bopp ndax lu ëpp ci waa senegaal da nu y gëm ne seeni mbir keneen a leen ko war a lijjantil bu ci nit soxla a dara lu war a bàyyikoo ci àtte gi goornemaa mel ni ab dokimaa walla lenn lu ko réew mi ameel ci àq moom da y gëm ne li war moo y mu gëstu ku ko gën a dégg tubaab te li gën a bari du ñeme e wax sax ay xalaatam ak lu xalaat yi am solo ndaxte déggul tubaab walla lenn ci baati tubaab yi y jox waxam jooju xiima ak fulla loolu yobb na ñenn ñi ci nu y wone ne dégg nanu tubaab ba y tudd ci seeni wax lenn ci baati tubaab yoy ni nu ko y waxe sax manunu ko te xamunu ni nu ko y binde te fekk na jamono ji nu ko y def fees nanu dell ak baati wolof yu man a wuutu yooyule di yu franse ba ci jàngkat bi génne ci daara y tubaab yi te déggu ko bu baax ñu néew lanu ñi ko ci dégg dégg ga ca war ndax lu sakkan la y jël ci seen waxtu moom itam day faral a jànkonte ek ug fasu walla kompleks gi y faral a dal ñi y waxe li dul seen làkk bu ñu y wax te taxul ñu xoot ci lool ak boroom yile làkk walla ku leen ci gën a sori jafe jafe yi aju ci wàll gii maneesu ko o takk dees leen di lim ci y teemeer danu ne woon nanu ci indi yenn rekk nu ne woon nu taxawlu as lëf fii ci ag wàll gu àggoon nanu ci ci y wax te mu y lu maneesul añàkk a jaaraat ngir am gi solo ak yiteel gi mu def lii nu nekk di wax loolu moo y taxawaay yi lenn ci boroom xam xami joojale jamono ame woon ci yee niti seeni réew xoolal ma ku mel ni petrarch nga xam ne bokk na ci li ko taxoon a siw yile taxawaay ba daa fàggul boppam dàkkantalu boroomu g nite te dara joxu ko woon loolu lu mo y yitewoo gi mu yitewoo woon xay gu yàgg ga civilisation ancienne walla bind gi mu doon def ci làkku w itaali wi doonoon aw waxiin rekk ca jooja jamono waaw lu tax petrarch mii doon binde ci wu itaali wi te fekkoon fi lakku w latin wi népp daa binde loolu de tontu li mooy bindul woon lu dul ngir nit ñi xam ko te jariñu ci li mu y bind kon li am solo moo y nu xam li mu y bind man ko o jariñoo du mu bind ko ci latin lu mel ne jeqiku gii revolution mooy li seriñ suhaybu defoon bu yàggul ba mu bindee ci wolof téereem bu am solo boobee di qurratul hayni ci xam xamu diine loolu tax nit ñi sottiku ci kawam ci g fuqale ñépp jariñu ci ngir nekk gi mu nekk ci wolof te kat téere y diine ya a ngi fi ak yu adduna yi te kenn xoolu leen ngir nekk gi nu nekkul ci wu kocc kon man nanoo wax ne petrarch mii moo gënoon a ñaw te ëpp xel mbokki boroom xam xamam yi ndax day mel ni moo leen gënoon a xam li xewoon bi mu gisee ne warul ci mom mu bind ci latin te làkk wu nu gën a dégg a ngi fi deesul sikk it ne moom dey ab jeqikukat la woon revolutionaire bu bokkoon ci ni gisoon ne du man a ñàkk ñu soppi ba ci làkk wi nga xam ne weesuwul fii mu nekk ab gàllankoor ci yoonu jëm kanamu g askanu itaali wi bi mu nekkee ci dëgg dëggi aajowoo ag jëm kanam ak yéeg gu xel ak gu xalaat mu gisoon ne bu bëggee def jëf ju am solo ci yee ak xamal askan wi li ko war moo y mu wut anam gu yòmb gu koy jàppndal loolu gën ji jàppndal te di tax ba ñu y man a alawtiku li mu leen di sànni ci xam xam ca na mu gën a yòmbe lii a ko yobb ci mu binde ci wu itaali ba nee wu latin wi ci misaal sunu njiit loolee di senghoor nga xam ne foo toll nu ko y tudd te du kenn moom de boo y xool da nga naan moom de bindul woon xanaa ngir mbokkam yii di waa senegaal ndax kat li ëpp ci réew mii déggunu tubaab nga rax ci dolli dafa meloon ne ab nasaraan la walla ku leen doon ligéeyal ci sunu kaw làkk a ngi fi woon nii di wolof di wu ñépp déggoon walla li gën a yaatu ci réew mi bu senghoor gëmoon réewam ba di ko ligéeyal du woon binde ci tubaab li ko waroon kay moo y mu defoon ko ci wolof walla sax ci séeréer ci li gën a néew walla mu digale ñu firi ko ci yile làkk mbaa mu sàkk jëwrin ju féetewoo jëmale leen kanam ndax ëlëg ñu man a xëy di y làkk yu gën a am ag koom te gën a yomb a jëfandikoo walla kay mu soññoon sunu boroom xam xam bu mag ba seex anta mii nga xam ne lii rekk a ko masoon a ñor ci mu wëy ca yoonam woowee te gën ko o jàpple ci xalaat ak doole waaye deful loolu moom kay da ko doon xeex ci anam gu ñaaw di ko gàllankoor ci mu amal bile naal moom nag ca dëgg dëgg moo y ki fi nekkaloon tubaab bi ndax yiteem jépp nekkutoon lu dul di gëstu lenn ak lu mu man a tuuti tuuti ci lu ko man a askanale ca waa orob ya li y tegtal ci loolu moo y waxam jii ci téereem bi tudd poesie de l action mi ngi ci naan j ai probablement une goutte de sang portugais qui est frequent en europe mais rare en afrique noir maanaa mi di man dey ku dem am naa as toq ci dereeti portigaal ndax man da maa bokk ci mbooloo m dereetu m a mi bari lool ca orob te néew lool ci afrik loolu mu wax ngir mu wutal ko lay daa jël yaayam ji nekkoon ku dëkk jiwaalo taxaw temb ne gine g portigaal gi la cosaanoo ak li nday ji daa wax lepp naan cosaanoowu fa kon kii soreewul ak ka woy wa taxoon a jug mu y màggat mu màggat ci am njàggu m tubaab jabaroo tubaab tubaab la tubaab ngéen dénk seen gaal gii waaye daa mel ne da ma laa gis nga naan waaw lu tax seriñ si daa binde ci araab te wolof nekkon fi seriñ si de li am ba mam moo y ci araab lanu daa binde waaye ak ci wolof te araab de li leen ci jañoon du jëmmi làkk wi rekk du woon it gòndiku ci walla fònkadi wii di seen wos mbaa foñ ko te weddi ko ba loolu di leen ci y tee di binde ak a tase seeni xalaat li fi nekk moo y ñoom seenu g xér gu tar ci nit ñi doon ay jullit yu dégg seen diine rawati na alxuraan mi deesul dégge ci lu dul araab moo leen àggale woon ci ag wàll ci seeni ligéeyi xam xam rawati na la ca aju woon ca diine ñu ko daa defe ci araab ñoom de dañoo gëmoon te loolo ooy li waroon ne alxuraan mii kat aji nekk la ju fees dell aki kiimaan aki way lòttal aji lòttal nag bu nu ko waxee ci xam xamu diine mooy lol yàlla rekk a ko man lòttal na mbindéef yi ag defam benn tafsiirkat seen gëm gëm laa la y wax amutoon kàttanu g leeral ko mbaa mu indi lepp ca tafsiir ga ca war ak leeral ga mu yayool moo taxoon nu gisoon ne nit ñi daal ci masala mii ñoom ñépp a ci yam maase ci ni bëñi peñe kon li leen doon noppal ci seen gis gis moom y nit ñi maaseendoo jàng araab ku ci nekk lijjantil ko sa bopp settantalal sa bopp ci way teddi aaya yii ci lu dul nga y sukkandiku ci kenn ndax kat kenn gënu leen ce e man a dimbale seen bopp bu nu déggee araab bu nu ko deful nag lu nu ci man a ame itam am raxasiit rekk lay doon aw desiit ag wall ca lépp rekk la y doon du weesu yu njëlbeenu yi rekk deet yu mag yi waaye jàngale gi ci araab ak bind ci teewu leen woon di bind ci wolof ak a bindante ak di ko jéem a jàllale ci taalif ci ay woy yu rafet te sakkan fees dell aki baat yu xoot yu naroon a réer moos bu nu ko deful woon aki masala y nahwu grammaire amoon nanu ay xisa yu yéeme ami nettali yu adabé yu njàggaté aki cax yu xoot yu daa dimbalee ci màggal am xel rawati na mu gone gi seen woy yooyu ak nettali yi danu daan fees ci li ëpp ak lu y yare loolu bokkoon na ci li daa dimbale yarkat yi ndaxte ñu ci ëppoon fekkoon nanu nit ñi nu di boroomi jikko yu rafet yi ñu dégge ci woy yooyu ak léeb yooyu xoolal ma léeb wu mel ni kumba am nday niki misaal ci ay nettali yu di kojug yar yu y dund tukkee ci sunu réew mi moom de lu am solo la ndax daa fees dell aki misaal yu kawe moom de day soñ ngone yi rawati na jigéen ñi ci ñu ràngoo jikko yu rafet yi ñu y muñ farlu nangoo dee ci lu baax loolo oo tax ñu man ne ñaari làkk yii daal duñu wooni noon waaye way mottaleente lanu woon yu daa dimbalante bii ñu ko y jëfandikoo ci li ëpp ci wàllu g diine ak jàppe ko jumtukaay bu am njariñ ci dégg alxuraan mu tedd mi te fiqu ci jile diine ndax faqiih moom muy ku xam fiq maneesu ko o nekk ci lu dull dégg bu baax araab kenn mant a dégg jile diine di jariñu ci xam xam bi ci nekk te déggoo araab loolu xaw naa jòmb senghoor sax seere na loolu ca poesie de l action mu ne je suis pour le mainien du latin coome langue universelle de l eglise catholique tout comme je duis pour le maintien de l arabe comme langue de l islame maanaa mi di man ànd naa ak ñu tëyye fi latin niki làkku egliisu kotolik bu adduna bi ni ma ànde ci nu def araab lakku lislaam kon nag li nu sañ a wax mooy mag ñi de wolof lanu jàppe woon seen làkku ofisel te daa nanu sonn it ci jëmale ko kanam daa sukkandiku ci loolu ci làkku araab seenu w jàngaliinu araab it walla xam xami diine ñi ngi ko daa defe ci di tekki baat yi ci wolof baat bu nu la wax rekk wax la ba mu tollool ca wolof loolo o jur riisu g wolof gii fees dell ak baati araab yu nu wolofal tax it ba yeneen baat ci wolof am yeneen maanaa yeneen tëggiin it sosu yu manul woon a ñàkk te feeñe ci wonu g araab ndax nag du g dofe nu sanni nële sunu lakku nday wii ngir jël weneen wu keneen di ko jëfandikoo niki ofisel naan dafa yor ci way yayale y xam xam ak yu xay yu wosam amadi ci jàngal sunu y doom yu ndaw ak yar leen ñun de ci loolu danu y jàmmaarloo ak lu sakkan ciy coona ci xamal leen te déggal leen ci anam gu dëgër te gaaw ndax gënul woon a dëppoo ñu jëfandikoo sunu wos wii ngir mu gën no o jappandi ca anam ga mu gën a yaatoo nu sol leeni xam xam ci lu dul gën ja a neewi coona ndax yellul ci nun nu jéem a lijjanti sunu jafe jafe yu bari yii nga xam ne foo wëlbatiku gis leen ñu y yu koom ak ak ak te y yoo xam ne jafe ge e lijjanti foo ko takk weesu na ko te ñu soxla lool ku ci jéem te bàyyi nag sonn gii nu y def ci kem bu rëy bii ci g farlu ak yitewoo ci yekkati jeneen aada walla kiltiir ju di kojug jàmbur ñun de foo nu fekk ni ngi wax ba sunu y gimiñ yi sax ci li y feeñ xanaa amatunu beneen ligéey bu leen war ci seenu g dund bu dul joyal baatu b frankofoni jaarale ko ci diggante seeni bëñ ànd ce ek as lëf ci m mbég ak màggal bii baat de da y dikk di bawoo ci put gi ci g diis bijj nag ay mbiccam di lu ñu peege mbalaanu m wurus mu wormaal ak jox àq bu ko defee mu bocciku nag ci g rëy mel ni moo y buur bi te fekk na ne nëbbul ci diggante ay lem lemam lu toll ne peppu suuf ci maanaa aha kay xanaa mi nekkul lu dul sanni ca àll ba lépp lu la fi sa maam bàyyil ci ndono lu xam xam mbaa cosaan te y sonn ci jañ pono y aada y tubaab ak aw làkkam jëm ca kanam ak yitewoo ko mel ne moo y lépp sànni ca sa ginaaw lépp loo moomoon ci làkk ak xay naaneey du dara lu dul ag wëy paase aku g dellu ginaaw te ag teew amul ñeel ku amul ug wëy man de noonuwuma tubaab waaye xam naa ne yayoowul ci ñuñ gii yitewoo gu mag ci sunu s alku lii nag gëstu la gu ñu doon def bëggoon ce e génne lii nu peek wër nu ci y jafe jafe rawati na yi ci di yu aju ci sunu li làkk li laal waaye nag ba tay gëstu la gu njàggat gu nu jublo o def ngir génnewaale ci as lëf ci taaru b wolof ak li mu làmbool ci g nooy ak man a ëmb mu doon it ag woote jëme ci luñutu ak jam critique ak def lu mel ne lii gu tukkee ci geneen wàll gu nu moy kon sunu yëf a ngoogu di lu aajowoo xalaat xool sònn yitewoo ak jàllale na léen wóor nag ne ci g solowoom ak ug déetam népp la ñeel népp a ko ñeel it ndax sunu mbir la di ménn ci yi nu man a jëmale kanam bu ñu ko fonkee ci li ma jort abdu xaadir kebe misik ak way misik fr musique en music nak ci wolof misik rek lanu koy wax ndax daa bok ci baat yi nga xamni ñéppa ko bok mook lu melni widewo video way baatu way mingi jugé ci nit ku way maanaam nit ku yéwwu litax mu tudd moom nit kookii waykat dafa way bà man a sos ay wax mbaa ay nasar yoo xamni nit ñimu nékkal bàyyi wuñu ci xel mbaa sax xamu ñuko woon kon moo leen gën a way batax muy way kon kuñuy tuddee waykat dafa wara doon kuy yeeté ay misikkat ci senegaal ay nasarkat taalifkat ci senegaal mooy xam xam bi y gëstu la xewoon demb di itam mbooleem ay jëf ak ay xew xewu demb la ko dale ca ña nu jiitu woon ba ci nun taariixkat mooy ki y gëstu di bind ci wàllu taarix xam xamu taariix moo nuy melalal mbiri dëkk yeek dëkk dëkkaan yu yàgg ya ci biir jamonoy taariix ak mbiri seen way dëkk da na nu waxal it ca dund ga fa amoon ci gàttal daal xam xamu taariix day gëstu li wéyi nit dembam cig matale da na wuññi feeñal it nekkiin ak dundiin yi nga xam ne nit jaar na ci jànkoonteek ñoom ci dundam gu gudd gi ci biir ay jamono yu dabante te toftaaloo bu ko defee mu gëstu anami jëm kanam yi nga xam ne nekktéef bii di nit amal na leen ci taariixam bu gudd bi ci noonu loolu jural ñu ñu jange ci daj dajam li mu jot a dund yooyu wéy aki ndamam te jéem a moytu ay pakkastalam aki rëcc rëccam ya jàll bu lii amee nag dina nu gis njariñ ak ngënéeli gëstug xam xamu taariix taariix dinanu ko jang ngir mu yombalal ñu xam mboolaayi nit ñi ci anam gu xereñ te dégg nand gis xàmmee it buum yi leen boole gëstu dundug buur yeek imbraatoor yi rekk du lenn rek li nu war a yitteel ci taariix li ci gën di farata kay mooy gëstu dundug mbooloo yi ak bennaan yi benn benn nit ñi ak gëstu jafe jafe yi daa yeesu ci seenug dund bis bu yàlla sàkk te jéem leen a wutali saafara yu dëppoo ba maas giy ñëwi ëlëg man cee jariñu ngir digal ab xew xew fàwwu mu am ab tombub boy fa muy dooree ay tombi boy yu bari nag am nañu te taariix man na cee tàmbalee nasaraan yi ñoom seen tombub boy mooy juddug yonnant yàlla isaa ca lañuy taariixe seeni xew xew bu dee jullit ñi ñoom seeni xew xew ñi ngi leen di wutaluw dig wu bawoo ca gàddaayug yonnant bi j m juge màkka ga mu ganee àdduna dem madiina xew xew bii nag mi ngi fiirook dajeek atum ci taariixu juddug yonnant yàlla isaa donte taariix mooy la xewoon ba àdduna sosoo ba léegi taariixu nit ñi suuf si jawwu ji waaye ci déggoo taariix ñu ngi koy tàmbalee ca ba ñu sàkkee mbind séddale ko ci ay jamono li nga xam ne ay téere yu ñu bindoon moo ñu ko xamal njëkk taariix mooy taarixu ñi fi nekkoon laataa sàkkug mbind taariix mooy lépp li xewoon ca ba ñu sàkkee mbind ba leegi taariix ci boppam dañu koo sédale ci ay jamono feeñug nit ci suuf ba daanu g nguuru rom gu mag ga ci ba feeñug amerig ci ba fippug waa frs ci ba ci sunu bis yii boroom xam xam yi ginnaaw gëstu gu ñu def ci suuf si wuññi nañu ay jeexiit reste vestige trace yu yàgg ay jumtukaay ay xor ay doj añs yuy tegtale ne suuf sii déy aw nit dëkke woon na ko njëkk ay junniy at jamono jooja la nuy tudde njëkk taariix moom nag mi ngi séddaliku ci ñaari xaaj ci ngënéelul jeexiit yii lanu xame njëkk taariix nit ci jamono jii da daan tuxu rekk di jëfandikoo ay ngànnaay aki jumtukaay yu njëlbéenu primitive doj yu ñu yatt ay ngànnaay ay xeej aki xepp bi jamono gënee dox seen dund gi soppiku ñu xam leegi sawara jëfandikoo ko ci togg ñam yi ci jamonoy doj wu ñu xacc wi lañu tàmbalee dajaloo sóobu ci mbéy sàmm ak ràbb ak liggéey jumtukaay yu xànjar yi tàmbali it di def yenn liggéeyi fànn yi niki bind ci doj ciseler graver ak yatt la ko dale ca n j g njëkk judd gu yonnant yalla isaa la weñ feeñoon ñu fent it mbind bi weñ feeñee fentees it mbind la njëkk taariix jeex taariix daal di tàmbali seex anta joob cheikhe anta diop paate sow paate sow wo dembi senegaal cosaan baati seereer safen la moo teki début origine commencé ci làkki seereer ci xëtt wi see fas tekki sama weerukay ci walu xam xam moodi jangat nit bile baat manko tëggé ci anthropologie manaam anthro nit ak pologie jangat cosaan aada ak luñuubaaxo daño fasoo waayé ci sama gis gis cosaan moy r manaam fu aw askan bayee koo bilep firi daa ajju si walug bërëp espace cosaan mana firi batay luñu donnu ci makk ñi kon ci tënkk cosaan moy reenu askan luna lnkalee di luñu baaxo def loolu moo lay jox culture wala mu xeltu ko ta mu jem ci walu dundam man nañ jappé culture kon suma suka ndikoo ci lii ma fessl cosaan nak ci walu xeltu baat bu jaxaso la gëstukat dalee ko ci jamano yu yàg ya kon luy walbatiku nittu jamano boo jel dañu tànn ci seen cosaan ay lëffin rax ci dooli dañuy fen waaye timit nguuruk reew munek war jkaar cosa don te mengo tul ak cosaan ak aaday reew yi eup dañu wali ci cosaanu reew yi new doolee ak dileendi nasaxal bu njekk borom xam xam yi bayoo tuggal ta see gëstu ajju ci walu jangat nit li lalloon bilee weddi moodoon ne see dëkk yi ñoo noot seeni kom kom bi aduna doxee ba nootagee bi jeex bu afrik moom boppam ñeppu nagu nagn ni askan nit ku nuul yam wanee ne nit lolu di ndam lu rey si xeetu nit ndax te bo xamul do xam seex lo aadama mooy ni ñu ko waxe ci lislaam ci angale mooy adam te ci faranse itam mooy adam mooy nit ki yàlla jëkka sàkk nettalib aadama feeñ na ci ge aadama dafa toppoon jabaram awa ci bàkkaaram bàkkaar boobu mooy lu indi musiba yépp yi nu gis ci àddina si ge at ya aadama dundoon la ge ci injiil dañuy wax ci aadama ci lu ro ko tim yu nettalib aadama feeñ na ci suraat nekk na ki borom bi ñëk bind mouy nit doon tamit yonent bi ñëk waxinu wolof bu tekki nit ñi ci làkku ibrë la tur wi jóge aaroona mooy ni ñu ko waxe ci lislaam ci angale ak ci faranse mooy aaron magu yonent yàlla musaa la woon ñu bokk ndey ak baay ñetti at la aaroona mage musaa baayam amram la tudd te yaayam yokebedd ex amoon na ñeenti doom yu góor ci jabaram eliseba ñooy nadab ak abiyu ak elasar ak itamar ex aaroona amoona benn rakk bu jigeen mingi tudd mariyaama doomu ndeyu aaroona ak musaa ex mariyaam bii bokkul ak yaayu yeesu krist ba musaa demee ci kanamu firawna aaroona dafa àndoon ak moom ngir nekk yonentam ex yàlla tànn na ko mu jëkka doon saraxalekat bu mag ba ci biir bànni israyil moom moo sàkkaloon bànni israyil benn xërëm bi xaaroon musaa ca tundu sinayi ñu tëgglu aw sëllu muy xërëm ñu di ko tuuru di bànneexu ci seeni jëfi loxo ex at ya aaroona dundoon la ci kaw tund wi ñu wax xor la faatu nu man nga jàng jalooreem ci ci angale ak ci faranse mooy agrippa buur erodd markus yulyus agaripa ii bokkoon na ci juróomi buur ya tudd erodd baayam itam agaripa la tuddoon mooy sëtu erodd bu mag ba ci g k la juddu yónni nañu ko room ngir mu jàng ci g k bi mu amee daanaka at baayam gaañu na ci g k erodd bu jóge calkis chalcis magu baayam dee na itam buur këlódd sesaar moo ko faloon buuru diiwaan yi baayam bu ndaw yilifoon ba noppi ci g k dolli ko ak yi maamam filib ak lisañas yilifoon mu nguuru ci yude ba g k dafa séy ak rakkam berenis ñu bokk ndey ak baay dëj nañu pool ci kanamam jëf bi agaripa amee daanaka at te sooga jóge woon room ngir sampu ci yerusalem ak sesare ci g k agaripa mënul noot yengu yengu yawut yi ci xeex bi mujj am xare room tas na réew mi ba dara desu ci g k ci g k nguuru room may na agaripa mu yilif wàll ci siri gaañu na daanaka g k ci injiil agaripa moo feeñ ci jëf ci làkku ibrë la baat bi jóge almasi bi mooy ni ñu koy waxe ci lislaam ci angale mooy the messiah ci faranse mooy le messie almasi bi mooy tekki ku yàlla fal ngir liggéeyal ko yonent yàlla yi jiitu woon jamano kirist waxoon nañu ci lu jëm ci musalkat bi yàlla dige woon nara ñëw tur wi dafa ëmb wax yooyu yépp yawut ya bu ñu masaana fal kenn dañu daan sotti diwlin ci boppam muy yonent muy sëriñ mbaa buur krist almasi bi nag mooy ki yàlla sol xelam ngir wone ne mooy yonent saraxalekat ak buur bi moo di yonent bi nuy jottali xebaaru jàmm fa kanam yàlla moo di saraxalekat bi nu ubbil bunt fa yàlla moo di buur bi yilif ñépp ak yépp baat bii mu ngi jóge ci làkku araab sukkandiku ci làkku ibrë te muy tekki kirist ci làkku gereg ci injiil bi ci gereg almasi bi dafay am ñaari yoon rekk yow ci firi wolof bu injiil bi ci gereg amee kirist te mu bëgga wax ci ndombam dañu koy firi almasi bu injiil bi ci gereg amee kirist te mu bëgga wax ci turam dañu koy firi kirist seetal itam kirist ci làkku ibrë la tur wi jóge ci angale mooy annas ci faranse mooy hanne ou anne saraxalekat bu mag ba la woon kiriñus boroom réewu siri moo ko fal saraxalekat ci at walla g k waaye garatus boroom réewu yude folli na ko ci at g k mu fal ci palaasam ismayel ba noppi elasar doomu anas ba noppi simo ba noppi kayif ci at g k waaye gannaaw bi ñu ko follee baatam dafa weyoon di am sañ sañ bu bare naka noonu anas ak kayif bokkoon nañu ci liggéeyu saraxalekat bu mag ba ca jamano ji kirist liggéeyoon kayif takk na doomu anas dañuy gis anas ci injiil ci lu yow jëf ancos ca jamono injiil péeyu diiwaanu nguuru room bu tudd siri la woon dafa nekkoon ca wetu joor gu naat ca dex gu yaatu gu tudd oront fleuve oronte kilomet ca kaw bëlu dex ga maanaam fu dex ga dugg géej ga teeru ancos moo doon ca dëkku selusi bu nekkoon ca géej gu mag kilomet ca noru bëlu dexu oront ba selusi nekkoon na kilomet ca sowu ancos ca at bu pool demoon fa daanaka atu g k dëkk bi xumb na nu ngi doon tabax di beesal dëkk ba gannaaw ñaari yëngu yëngu suuf yu yàqoon lu bare ay fukki junni yawut ya dëkkoon ancos te ñoom woomle nañu te seen jàngu rafet nañu gereg yu bare ñi ngi doon ñëw ca seen diine ancos moo doon dëkk bu neex a dëkk te rafet waaye dëkk ba dafa siiwoon itam ndax seeni noos seen ñaawteef ak seen njaaloo ak doxaanu yàqute bànneexu àddina si rekk la waa ancos doon wut dëkku gereg bu am solo la woon bu nekkoon ñetteelu dëkk bu gëna mag ci nguuru room gannaaw dëkki room ak alegsàndiri buuru nguuru maseduwan ñoo ko sampoon daanaka at lu jiitu jamono kirist naka noonu ña fa jëkk a dëkk ñoo doon ay xarekatu maseduwan ak waa aten waaye yeneen gereg ya toppoon nañu ca ñoom tamit buuru geres dafa xiirtal yawut ya ñu ñëw dëkk fa te may na leen ñu nekk jaamburu dëkk ba waa room nangu nañu diiwaanu siri ca atu j k naka noonu ca jamono injiil dëkk bi dafa boole waa maseduwan waa geres waa room waa siri ak yawut ya waaye amoon na ay jafe jafe diggante yawut ya ak ñi des ca waa ancos ba dem sax ba am jamono waa dëkk ba bëggoon nañu rey yawut ya fa dëkk ca suufu nguuru room diiwaanu siri dafa jëm kanam bu baax waa room ñoo defoon ancos seen péey ak màkkaanu xare ci diiwaanu siri waaye ba tey waa room may na dëkk ba mu yilif boppam ndegam siri dafa nekkoon ca digu nguuru room te mu féete waa pàrt beneen nguur bu xeex ak nguuru room siri nekkoon ca suufu buuru room ba moom ci boppam buur ba sesaar moo faloon benn jawriñ ngir toogal ko ñetti at ba juróomi at yu nekk mu nekk boroom réewu siri boroom réewu siri moo sutoon boroom réewu yude di ko yilif amoon na ñeenti mbooloom xare bu tudd léjiyo ca siri bu nekk bu am xarekat ya amoon na itam ay gaalu xare ca selusi yaakaar nañu ne daanaka nit ña fa dëkkoon ca jamono injiil benn boroom xam xam dafa yaakaar ne benn cér ca juróom ñaar ca niti dëkk ba yawut la woon te yawut ya dëkkoon ca ñetti gox ya yawut ya amoon nañu alal te seen dundin xëcc na yu dul yawut yu bare ñëw bokk ca seen diine koom koomu ancos amoon na doole lool ndax kàttan gu mu am ci biir nguuru room tamit ndax yoonu jaaykat yi am solo ya jaaroon ancos ak ndax lu ñu fa defaroon ca dëkk ba ancos dafa siiwoon ndax dàllu der yu rafet latkoloñ saf saf yi ak ndàbb lu xeeñ piis yi gànjar ya ak takkaay ya téere ya ak li tëggu xaalis ak wurus defare yoonu jaaykat ya jóge ca penku maanaam babilon asiri ak iraak jaar na ancos te dafa tiim yoon wu dem nor ak sudd wu boole palestiin siri ak asi minër naka noonu amoon na wenn yoonu jaaykat wu jaar ca tund ya ca xunt bu tudd buntu siri ba noppi dem tars yoon mu jóge tars wu tudd yoonu eaca via egnatia dafa jàll asi minër ba dëkku efes tamit gaal ya mënoon nañu dox ca dexu oront diggante géej ga ak dëkk ba dëkk ba moom rafet na lool nguuru geres def nañu yoon ya ca kaw tëralinu damyee ngir yoon yu mag ya jàpp ngelaw lu féex lu jóge géej ga amoon na benn miir bu mel ni tata bu wër dëkk ba lépp buuru room bu nekk tàmbali ak pompey ca atu j k dugg na xaalisu nguuru room yu bare ci tabax ya ak rafetaayu dëkk ba ni bépp dëkk bi gereg ya walla waa room tabaxoon amoon na ay powukaay ak amfiteyatërë ay màggalukaayu yàllay xërëm yu bare ak ay këru sanguwaay ya feesoon na dell ak ay pénc fu xale ya doon fo waxkat ya indi seen wax jaaykat ya jaay te reetaanlukat ya bégloo mbooloo ya def nañu ay robine ca kaarfuur mbedd ya ngir jigéen ya mënoon nañu root ndox moo xam ne mu jóge ca dex ga walla ca ay bëtu ndox ya amoon ca dëkk ba tamit yulyus sesaar tabax na benn akwadakk maanaam pom bu indi ndox ngir dimbali gox yoo xam ne amuñu woon ndox erodd bu mag ba tabax na wenn yoon wu jàll diggu dëkk bi diggante buntu miiru dëkk ba ca penku kaw ak buntu miir ca sowu suuf yaatuwaayu yoon wu mag woowu meetar la woon dem na kilomet te lépp tali doj wu dëgër wu jóge misra walla marbar dafa dem ca pénc bu réy ca diggu dëkk ba ca pénc moomu amoon na benn nataalu buuru room tibeer sesaar bu réy bi ñu defare xànjar ca wetu yoon wa ca ñaari bor fukki meetar yu nekk amoon na ay kenu doj yi ñu taaral dafa meloon ni mbaar ba tax ñi dox ña mënoon nañu dox ca wetu yoon wa guddaayam lépp te bañ génne ca naaj wa walla taw ba yu gën a bare ca kenu ya amoon na ay nataal yi ñu yett walla defar ca xànjar diggante kenu ya amoon na bunt ngir dugg ca kër ya bitik ya ak biro ya yoon ya amoon na sax làmp ya tàkk guddi amoon na benn dun ca biir dex ga fu dex ga jaar ci biir gox yu nekk ca noru dëkk ba guddaayam ak yaatuwaayam kilomet la foofu lañu tabax këri buur yi ak benn estaad ngir rawante fas ak sareet ya guddaayu estaad ba meetar la woon ba moo wara tax mu bokk ca ya gën a réy ca àddina si ancos amoon na itam ay màggalukaay ca yàllay gereg ak room ak ay powukaay yàllay ancos moo doon sës juróom ñetti kilomet ca suddu miiru dëkk ba amoon na benn gox bu tudd dafëne ca wetu yoon wa dem dafëne amoon na ay tool fu ñu bey lawtanu réseñ ngir defare biiñ ak tóor tóor yi ñu defare latkoloñ dafa nekkoon ca kaw benn déndu tund maanaam palato yaatuwaay ak guddaayu palato ba bu ne meetar ya la te mu nekk meetar lu gën a kawe niwo ancos amoon na màggalukaay ca yàllay xërëm ju jigéen ju tudd itam dafëne waa ancos gëm nañu woon ne dafëne nit la woon ki apolo benn yàllay gereg soppoon apolo dafa ko dàqe di dàqe ba ci mujj dafëne dafa soppiku nekk as ngarab bu tudd loriye goxu dafëne amoon na benn sardin walla park bi ñu defaroon ngir bànneex rekk bu am wëraayu kilomet ca biir màggalukaayu dafëne amoon na ay sëriñ yu jigéen yu nekk gànc yu bare guddi gu nekk ci seen turu diine ñu defaat li amoon ca nettali ba maanaam jaamukat ya doon nañu dàqe sëriñ yu jigéen ya ci biir garabu loriye yi ci biir sardin ba ba jàpp leen di séy ak ñoom buuru room ogust sesaar samp na benn po olimpik jeux d olympique ñeenti at yu nekk po boobu indi na ay joantekat yu bare ngir rawante ci diiru fan ci daw tëb sànni xeej ak fitt rawante fas ak sareet bëre ak ñoom seen amoon na itam rawante ca misik ak ci tari nettali gis nañu ne ay at gannaaw deewu kirist mbooloo ñi gëm ca yerusalem fal nañu benn waa ancos bu tudd nikolas ngir mu bokk ca juróom ñaar yi doon toppatoo yëfu mbooloo ñi gëm jëf xebaar bu baax bi egg na ancos gannaaw deewu ecen daanaka atu g k jëf ñi ko indi ay yawut yi làkk gereg lañu woon yi jóge dunu sipar ak dëkku siren ca libi ñoom def nañu lu bees may nañu gereg yi topp yeesu ci lu sësul ca xaraf walla yeneen aada yawut mbooloo bu mag gëm na boroom bi foofu lañu jëkk tudd taalibe kirist gaayi kirist jëf ci bu jëkk tur boobu turu foontoo la woon waa ancos dañu doon siiw ndax ni ñu doon foontoo nit daanaka fukki at gannaaw ga amoon na ca ña gëm ca yawut ya ca yerusalem ña jaaxle ndax yu dul yawut yu topp yeesu te kenn xarafalu leen werante wu réy amoon na ba tax ñu def genn géew ca yerusalem kilomet fu sore ancos ngir waxtaan ci am ami ñi gëm may na leen ñu mënoon a yónni ndimbal ca ña gëm ca yerusalem jëf tamit ca mbooloo ñi gëm ca ancos la pool jóge ngir tas xebaar bu baax ba ci biir yu dul yawut ya te ca ancos la dellusi yoon bu nekk maanaam ancos dafa nekkoon mel ni màkkaanam ñetti tukkeem yépp dafa tàmbali ancos ca jamonoom mbooloom ñi gëm ca ancos moo gën a am taxawaay bépp mbooloo ci mbiru ni mbooloom yi ca àddina sépp doxe xëyna bu dul mbooloom ca yerusalem tey jii dëkk bu ñàkk solo la bu tudd antakya ci tirki turquie am na nit kese ay toppkatu egëliis gereg yi des ci biir am réewu jullit yi ancos ca siri feeñ na ca jëf gal ancos mooy benn dëkk ci wetu diiwaanu pisidi fu pisidi digalook diiwaanu firisi ci dëgg dëgg ci diiwaanu firisi la bokkoon waaye ba tey faraloon nañu ko tudd ancos ci pisidi gentam sorewul dëkk bu tudd tey jii yalwacc yalva ci tirki turquie ancos nekkoon ca kaw benn tund wu ndaw bu nekkoon ca kaw benn palato bu yaatu te naat tund wu ndaw wa moom itam palato la woon wu am dénd lu tollook ektaar benn boor nekkoon meetar ca kaw jooru palato ba waaye beneen boor nekkoon mbartal mu kenn mënul yéeg meetar ca kaw joor ja naka noonu dafa mel ni tata te yomb na aar nekkoon na itam ca yoon wi mag wi waa room tabaxoon wi jàll asi minér penku ba sowu diggante dëkku tars ak dëkku efes wu tudd yoonu sebasëtë nguuru selësid maanaan waa siri ñi donnoon wàllu nguuru geres moo ko sampoon daanaka at lu jiitu jamono kirist ngir teg fa xare ba bëggoon nañu aar nguur ga ca xeetu pisidi wu nekkoon ca tund ya ca sudd tamit am ndogal ca lépp lu jaar ca yoonu jaaykat ya wu mag wu jaaroon asi minër penku ba sowu sampoon na ko fa itam ngir boole ñi dëkk ca diiwaanu firisi ak aada gereg yi ñi fa jëkk a dëkk ñoo doon gereg yi jóge dëkku maesi ca diiwaanu lidi ak yawut yi jóge babilon ca atu j k nguuru room moo def dëkk ba suufus room boole ko ak diiwaanu galasi jaamburi dëkk ba yépp amoon nañu yelleef yu yem ak yosu waa dëkku room tamit indi nañu ay xarekatu room yu bare yi ñu may ñu génne xare ba maanaam soldat yu màggat te may leen suuf ngir ñu dëkk fa gannaaw ga ndànk ndànk dëkk ba tàmbali gën a niroo dëkki room yeneen dëkk yi ko wër ca jamono injiil dafa niroo dëkku room ca wàllu yoon wa ca wàllu nguur ga ak ca wàlli tabaxin ak colin rafetal nañu dëkk ba bu baax ak pénc ya ak kenu ya te ak nataal yi ñi yett ca doj ak xànjar ancos ci pisidi moo doon dëkk bu gëna am solo ca diiwaan ba lu ëpp nit ñoo fa dëkkoon dëkk ba boole na ay xeet yu bare amoon na ci bu jëkk waa firisi ba noppi indi woon nañu waa gereg ya ak yawut ya ba noppi waa room ya ci biir dëkk ba amoon na ñaari pénc yu réy yi ñu defare doj benn ca ñoom péncu tibeer lañu ko tudd mu am dénd bu tollook meetar kaare bi doon grand palaasu dëkk ba fu nit ñi doon jaay di fo di waxtaan kenu yu réy te rafet ñoo ko wëroon beneen bi nag mooy péncu ogust moo dend péncu tibeer ci seen diggante amoon na benn iskale bu am mars maanaam tegukaayu tànk bu nekk am yaatuwaayu meetar ca kaw iskale ba amoon na bunt bi ñu defare ak ars yu réy a réy ab ars mooy lenn li ñu tabax ngir nekk pàttaliku dafa am ñaari kenu doj yu réy yi ñu boole ak lu mel ni xala doj bu jaar ca seen diggante tiim leen def nañu bunt bi ngir nekk pàttalikukaayu ndam li ogust sesaar amoon ca xeex ya ca kawu ars ya yett nañu ay nataal yu réy beneen booru péncu ogust moo doon wenn tundu doj ci biir tund wa yett nañu genn xala rafetal ko ak ay kenu yu kawe ya ca diggu xala ga amoon na benn màggalukaay bu réy bi ñu defare marbar bu weex ngir teral seen yàlla men ak buur bi ogust sesaar ñu sooga àggale màggalukaay ba bi pool demoon fa ak ars ya bala mu dellusi ñaareel bi yoon ancos amoon na itam ndox ca tiwo yi jaar fépp ca dëkk mu jóge ca benn bëtu ndox ca tund ya nekkoon fukki kilomet ca biti dëkk ba indi nañu ndox ak li tubaab tudd akwadakk ci diiru kilomet dafa jaaroon ci biir suuf si waaye kilomet yu mujj yi dafa jaaroon ca kaw pom bu kawe bi ñu tabax ngir yóbbaale ndox seen yàlla men la tuddoon amoon na itam beneen màggalukaayu men ca wenn tund bu kawe lu tollook kilomet ca penku dëkk ba bérab boobu mooy bérab bu bokkoon ca ña gën a am solo ca seen diine at bu nekk def nañu benn po ngir teral men gëmoon nañu ne men mooy yàllay wér gi yaram naataange ak jàmm te ku aar bàmmeel ya mooy itam yàllay weer wi ca nataalam ku niroo nit la woon mu sol yere misaale nañu ko ak wenn yëkk tamit ak nataalu weer bu am juróom ñetti fan sersiyus poolus boroom réew mi ca dunu sipar jëf dafa bawoo ancos ci pisidi ay bokkam moomoon suuf su yaatu ca gox ba moom gëm na boroom bi pool demoon sipar xëyna boroom réew mi moo boole pool ak dëkku ancos ba tax pool ak barnabas gaaw nañoo dem ancos bi ñu jóge dunu sipar ca jamono pool ndoxaanu yàqute def yaramu neen topp nafsu màndite lekk suuxu mala bu ñu toggul te naan deret bokkoon na ca diine naka noonu ñu bare bi ñu xoolee dundinu yawut yi ñu tàmbali xeeb diine ji ñu fekkoon di tàmbali bokk ca diine yawut ya rawatina jigéen ñi woomle ca dëkku ancos jigéen ñooñu ñoo doon jabari magi dëkk ba naka noonu yawut ya noonoo pool jaaroon nañu ca jigéen ñooñu ngir ñu laaj seen jëkkër ñu dàq pool ca dëkk ba jëf tim yoonu nguuru room wu mag wu tudd yoonu eaca via egnatia dafa demoon ci diggante asi minër ak itali tàmbale na fu dëkku istanbuul nekk tey ji ca géej gu ñuul ga jàll maseduwan ba egg géeju adiratig bokkoon na ca yoon wu ñu jaaroon ngir dem itali ak room tali doj la woon maanaam defaroon nañu ko ak ay xeex yu ñu yett ba kaare ngir seen ànd jege yoonu eaca jàll na diiwaanu maseduwan diggante géej gu ñuul ak géeju adiratig dafa tàmbali woon ca géej gu ñuul ca dëkk bu tuddoon bisansë byzanse mooy dëkku istanbul jaar ca dëkki neyapolis filib amfipolis apoloni tesalonig ak pela ba noppi dem ba dirxasiyum dyrrhachium ak apoloni ca géeju adiratig guddaay ga mooy tollook kilomet nit ñi doon nañu dugg gaal ca dirxasiyum walla apoloni ngir jàll géej ga te fekk yoon wa jëm room ci angale mooy archelaus ci faranse mooy archélas erodd arkelawus doomu erodd bu mag ba moo falu woon ci diiwaani yude samari ak idume idumée j k nguuru ba g k yaayam maltas malthrace la tudd arkelawus ak erodd antipas ñoo bokkoon ndey ak baay yawut yi ak waa samari yi jiiñ na ko kor ci kanamu buuru room ndax coxoram buur bi ogust sesaar moo ko fuñ ci diiwaanu gool gaule maanaam farans ci g k gannaaw loolu def nañu yude diiwaan ci suuf nguuru room te jawriñ yi buuru room fal yilifoon fa jabaram mariyamënë mariamne doomu aristobul la ki mu fase ngir takk galafira glaphyra jëtunu alegsàndar alexandre magam man nañu gis tur wi ci mc ci làkku ibrë la tur wi jóge ci angale mooy armageddon ci faranse mooy harmaguédon armagedon mooy turu benn tund ci làkku ibrë bi ñu sotti ci làkku gereg ci làkku ibrë megido meguiddo la tudd ci injiil dafa misaale bérab fu xare bu mujj bi nara am ci diggante gaayi yàlla yi ak gaayi seytaane yi ci muju jamano ji tundu megido bokk na ci tundi karmel yi dafa nekkoon ci benn boru xunt mu mayoon nit ñi jàll tund yi ci joor bu nekk ci taatam la sóol sa ak yosiyas ch dee te sedeyon amoon ndam ci waa majan ñi jud armagedon mooy feeñ ci injiil ci pe ci angale mooy athens ci faranse mooy athnes aten dëkk bu mag la ci réewu geres mooy péey ba sax te siiw na ngir xam xam ba ak njàng ma ak caada ja yaakaarees na ne lu ëpp téeméeri junni ciy way dëkk ñoo fa dëkke nekkoon na péeyu nguuru waa geres bi tuddoon atig attique tey mu tudd aten sancees na aten daanaka at nj is njëkk iisaa daanaka at njëkk iisaa fekkoon na mu am nguur gu yaatu lool waaye geres dafa ñàkkoon suuf moo tax waa geres yi tuxu di sanc ay dëkki geres yu bari ca tugal ak asi gu ndaw gi moone ca jamonoy pool dafa ñàkk xaalis amatuñu nguur te diiwaanam atig dafa tuuti dénd bu tollook kilomet kaare matul sax benn departema ca senegaal amul feneen ca atig fu gën a sore aten kilomet seen suuf musuñoo doy seen soxla taw bi barewul woon lu tollook taw bi ñu am ca noru senegaal ñetti cér ca ñeent ca suuf si amul njëriñ ci bey te yu bare ci yi des amoon njëriñ ca bey garabu oliw rekk amoon nañu mbélli xaalis waaye fekk nañu ne jeex nañu tàkk laata jamono nguuru room tamit seen doole ci jaay wàññiku na ndax doole yeneen dëkk yu mel ni ancos korent efes ak alegsàndiri dëkku njàng la woon bu amoon jenn daara ju kawe iniwersite naka noonu siiw nañu ndax seen xam xam ak seen waxin ndaxte waxin lañu ca gën a jàngale wax ak a déglu lu bees rekk lañu daan xinte amoon na ay mbooloo boroom xam xam benn ca mbooloo boroom xam xam moo tuddoon epikuren kureel la woon bi sës ci njàngalem epikuur mu faatu at lu jiitu jamano kirist te fonk bànneex ba mucc ci bépp tiis gëmuñu yàlla waaye ñu gëm ne àddina dafa sàkk boppam te amul boroom te boo deeyee amul dara lu ciy topp nekkatuloo daal beneen mbooloo dafa tuddoon estowisen kureel la woon bu sës ci njàngalem senon mu faatu at lu jiitu kirist fonk nañoo naagu ba bañ a yég dara muy bànneex mbaa naqar dëkk bi fees na dell ak màggalukaayu yàlla yi ñu defare marbar yu réy a réy te rafet nataal ya ñu yett kenu ya robine ndox bi ñu tudd fonteen ak yeneen rafetaay ca diggu dëkk ba amoon na benn tund wu am ay màggalukaay rekk ëpp nañu fukk nekk na daanaka meetar ca kaw niwo dëkk ba ca ñetti boor am na mbartal bu jub xocc mel ni miir akëropool la tudd benn ca màggalukaay ya moo doon màggalukaayu sës yàlla ju gën a mag ca diine gereg àggaleeguñoo tabax màggalukaay ba ca jamono pool waaye ba noppi amoon na kenu marbar bu nekk am kawewaayu meetar ak yaatuwaayu meetar kawewaayu màggalukaay ba moom ca boppam moo doon meetar ca biir amoon na nataalu sës bi ñu defare wurus ak iwaar bokkoon ca ñeenti màggalukaay yu gën a réy ca àddina si ca jamono màggalukaay bu gën a am solo moo doon li ñu tudd parténon bi ñu defaroon ngir yàllay dëkk ba maanaam atena guddaay meetar la yaatuwaay meetar te kawewaay meetar ca kaw kenu ya amoon na nataal bu ñu yett bu wëroon tabax bépp ca wàll wàll bu ne indi na benn ca seeni nettali yàlla amoon na beneen nataal bi ñu yett ca diggante kenu ya bu amoon melo ya ay góor ay jigéen ak ay bàyyima yi bokk ca ña indi seen yàlla atena benn yére wurus at bu nekk guddaayu nataal bi mooy meetar te def nañu nataal yi ngir ñi taxaw ca suuf di ko xool yaakaaroon nañu ne dañuy jàkkaarlook nataal ba fekk na ne nekkoon na meetar ca seen kaw waa aten jaamu nañu ay yàlla yu bare waaye yàllay dëkk ba moo doon atena at bu nekk ci weeru yuuliyoo amoon nañu benn màggal lu diir fan ca fan yu jëkk ya def nañu ay joante rawante gaal ya fas ak sareeet ya rawante ca woy ak nettali ay mbumbaay ca juróom benneel ba fan ca fajar saraxalekat ya ak magi dëkk ba jiitu nañu mala ya ak waa dëkk ya yépp ñu dox ca biir dëkk ba ba egg panténon fu ñu def sarax ya te ñépp lekk yàpp sarax nañu mala mooy nag ak xar at mu nekk amoon na bérab ci biir dëkku aten bu tudd areyopas nekkoon na ci kaw wenn tundu xeex wu kawe amoon na ay siis yi ñu defare woon doj ngir kureelu dëkk ba manoon faa daje indi nañu pool foofu ngir mu waareji ni dëkki gereg yépp amoon na pénc bu ñu tudd agora amoon na ñaar sax benn bi waa dëkk ba tabaxoon ak benn bi waa room tabaxoon ay péncu doj lañu yi ñu rafetal ak kenu yu réy ak nataal ya ñoo doon maase ak grand palaasu dëkk ba te fu ñu doxale nguur foofu itam amoon na ay màggalukaay ak ay saraxalukaay ci dëgg dëgg mënuloo dem fenn ca dëkk ba te gisul benn màggalukaay walla nataalu yàlla amoon na ay powukaay itam ñoom itam dañuy kéemaane benn ca ñoom woyuwaay la bi ñu teg ne mooy bu gën a rafet ca àddina si beneen mënoon na toogal nit te léeg léeg dina fees ba ëpp loolu sax amuñu jot a lim bépp tabax bu yéeme bu nekkoon ca aten bi fa pool ganesi dëkku gereg la woon waaye amoon ay yawut itam aten dafay feeñ ci injiil ci jëf tes téeree ngii di benn ci yi ñu gën a yër ci àdduna bi mooy téere bees sellal ci lislaam di fi jullit ñiy ball loo seen yoon di shariiha ak ci sunna siy dundiinu yonnant bi jàmm yal na nekk ci moom kon nag bu am solo la lool fi jullit ñi alxuraan alxuraan mooy téere bu sell bi ñeel jullit ñi mooy balluwaay bu njëkk bi ñeel yoonal gu lislaam gi ci ginnaawam la sunna di ñëwe li njëkk a wàcc ci alxuraan it mooy laaya wi njëkk ci saaru halaq muy jàngal ci sa turu boroom bi bind sàkk alxuraan nag mooy waxi yàlla ji mu wàcce ci yonentaam ba muhammad jibriil nag mooy ndawul yàlla tey malaaka mi ko wàcce ngir nag yonent bi jottali ko nit ñépp moom nag fa yàlla dees koo bind ca àlluwa jees wattu ja lawhul mahfuus àlluwa jii nga xam ne yàlla bind na ca lu nekk njëkk mu koy sàkk wattu googu nag yàlla la soob mu bëgge ko noonu noonu la ko waxe nun noo wàcce alxuraan te nun noo koy wattu wolof làkk la wu ñuy wax ci gàmbi gàmbi wolof gànnaar gànnaar wolof ak senegaal senegaal wolof mi ngi bokk nag moom wolof ci bànqaasub atlas bu làkki kongóo yu kojug nit ñu ñuul ñi mbokkoo gi mu am ak làkku pël lu yàgg la am na it lumu séq ak yeneen làkk ci gox bi niki séeréer joolaa ak basari bi ñu demee ba gis jëmm ja muy ku sew tuuti te xaw a wow waaye di ku ñu muure ab taar ci anam gu woyof te loyox di ku ñu aare kàttan sóob ko ci ag fonk sa bopp doonte ag neen la solal ko yéerey yëgle ak jaral te ma jëli loolu ca jafeem gaa jëli bi loolu amee dama ne leen xanaa kay du kii ngeen ma doon wax ñu ne ahakay cis lëf cig yéemu ak ñàkk a xalaat ne dinaa sikk mukk ci moom ma jug man xajal leen foofa fépp ma ne nag waaw ku mel nii ci li mu làmboo ciy melo lu ko nit di doye ginnaaw bi nag dégg naa ñuy wax naan moom de bokk na ci ñi gën a jekk ci boobule gox ànd ak jaaxle ci samaw jëfiin ci ba ga ma ko fa ba ma ne leen man moo xam lii mooy li am ci sunu làkk wii walla yii di yu afrig yi dañu di yu am solo te man a dem ni yépp di deme am barab ci digg barabi làkk yépp waaye li nu dal nun waa afrig mooy li dal sunu lépp dalaale ci li muy dal sunu kàllaama yii nga xam ne wii de bokk na ci yi gën a nosu gën cee nooy gën cee nangoo defaru yéwénu ruy ci ku ko ruyal tey way nag ca nanu bëgge mu waye ni ana nag ku am janq bu mel ni bii cib taar nangoo ni joee ni jekke ni man nee toppatoo nangu nee jëme kanam waaje ni ngir lemu ci say bëgg bëgg ana ku am ku mel nii looy xoolati ku sewe nii ràgge ni te taaroodi ni li ma bëgg a wax mooy naka la nu bëgg a bàyyee sunu làkk yii rawatina wii di wolof ca nooyam ga ak nangoom ga ak gàttam ga ak noppaleem ga taaram ba leeram ga manam gaa leeral ak yaatoom ga ak ruyu gi mu nangu naan dangay jëlati weneen di ci sonn ak a sonle naan day wa gën ma ne ñoom ñoo gis loolu man de déet wolof mooy làkk wi ñu gën a wax ci senegaal waaye ngir doyodig waa afrig yi ba leegi frañse mii nga xam ne lu matul cib téeméer ci doomi senegaal yi rekk a koy wax moo fiy làkk wu njëkk maanaam wi nguur gi di waxe di ci liggéeye ni ko gëstukat yi waxe làkku wolof am na ag mbokkoo ak yeneen làkki afrig yu bari yu mu bokkal i maam làkk yi dañ leen a séddale ci ay wàll bu ci nekk ñi am ag mbokkoo lañu fa def nee nañu wolof ci wàll gi ñuy woowe bànqaasub atalaas bu làkki kongóo yu kojug nit ku ñuul la bokk am na ag mbokkoo ak pulaar ak séeréer ak joolaa ak yeneen daanaka ñoo ngi koy làkk ci senegaal gépp bëj gànnaar ba bëj saalum penku ba sowwu donte wolof da di làkku askanu ñi ñuy woowe ay wolof waaye kàllaama wolof amul uw dig dem na ba romb dig frontiere yu senegaal àgg ba gàmbi gànnaar ba mali ci ñaari dëkk yu njëkk yi sax boole nañu ko ci seen i làkki réew daanaka gox boo dem ci senegaal am nañu waxiinu wolof wu wuute am na wolofi waalo waalo jolof jolof saalum saalum wu kajoor kajoor wu baol baol ak wu lébu a à aa b bb c cc d dd e ee é ée ë ëe f g gg i ii j jj k kk l ll m mm mb n nn nc nd ng nj nk nq nt ñ ññ o oo ó óo p pp q r rr s t tt u uu w ww x y yy ahmadou bamba mooy ki taxawoon jàmmaarlook tubaab yi ngir xeexal lislaam te desal fi sunu ag dëkk ci afrig tey bég cig cosaanoo fi kon njukéel ko war nanu kii moy ki taxawal yoonu murit tey ki taalif lu sakkan ci diine indi ay gisiin yu bees ginaaw bi nu ko sonnalee genne ko ay yoon réewam li ma tax a jug jëme ma ci def bile ligéey te ma jàppe ko muy bu am njariñ mooy benn jortu ne ci def gi ñi ngi ligéeyal sëriñ bi waaye it xeet wi ndax jël lu mel ni jaar jaari sëriñ tuubaa ak li mu làmboo ciy njariñ nga tas ko teg ko ci fu loxol ku nekk jot yombal ko ba ku jug man koo xam man koo dégg man cee jariñu ca anam ga mu gën a yombe gënnee leere te yaakaar naa ne def ko ci wolof ñeel wolof yi ci anam yiy yombal la tey leeral lu mel ne lii de yaakaar naa ne amul lu ko gën di ligéeyal sëriñ bi waaye ag ligéeyal sa xeet it mi ngi ci ndax ag dundal la ñeel saw làmmiñ te gis naa ne lu waay man a xame ci làkk ak wu mu man a doon ci sa wos lay gën a dugge lay gën a tooge lay gën a nekke luy dund ak yaw ci lay doone kenn ci yaw ngay yaw itam kenn ci moom ngéen di benn bu dul ñaar gis naa ne bokk na ci li ñiy rawe di rawe di jànge ci seeni làkk di ci waxe di ci xalaate te di ci jokkoo man de bile téere njëkk ma koy tekki nekkoon na di bob dees na soxla as lëf ci waxtu ngir yër ko dégg ko naan ko waaye daa mel ni bi ma ko defee ci wolof soxlaatunu lu dul lu néew ngir jaar ci jaarati ci kon nanu fonku sunu bopp ci fonkaat bu baax sunu làkk yii te xam ne dug fonkadi ñeneen ñi ñaareel bi mooy gis gi ma gis téere bii di bu jéggi dayo ba ci solo ak njariñ di delluwaay ci delluwaayi téerey yoonu murit wi di rootukaay ci yu xam xam yi làmboo nag kem bu bu réy ci xam xam ci lu aju ci sëñ bii di kenn ci ñi ñu war a xam bu ma waxul ki ëpp solo ci ñoom kon xam leen ne yii ak yeneen yu ma waxul ngir bañ a guddal ñoo sabab firi gi nga rax ci dolli nekkug aji taalif ji di kenn jëllewaayi yoon wi yu xam xam ndax kat boo yëree da nga ko gis lu bari mu naan sëñ bi nee na ma te loolu du lu yomb kok bëkk néeg la woon ci bëkk néeg yi bu ma waxul ngën ji bëkk néeg kon kooku maneesu koo gën di jëlewaay mbaa delluwaay rawati na muy ku ñépp xam ag sellam akug dëggoom yal na nu yàlla taas ci barkeem te dolli ngërëmam ci sëriñ sunu sëriñam laafaale ko ci barke ku nu ligéeyalam ak ki muy ligéeyal moom mu mujj mi aamiin yaw boroom mbindéef yi bii mooy teereb irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim di ci maanaa nàndalug aji naanaale ji ki ngay toogal di naan ci ndox mu neexum sopp jëwrinu yonant bi di xam xamu jaloore bu nu gàttal mu ñeel nag ki bëgg a am ab xam xam ci dundug sëriñ ahmadu bamba yal na yàlla dolli gërëmam ci moom te jariñ ñu ci amiin ki ko taalif it di ku xeebu ku aajowoo ndimbalul boroomam ak yërmaandeem tey yaakaar ci moom mu jéggal ko ay bàkkaaram te làqal ko ay ayibam yi feeñ ak yi nëbbu fii ak fan jëm di muhammadul amiin joop doomi sheex ahmadu joop mu dagana yal na leen yàlla boole jéggal di it taalibeb sëriñ tuubaa yal na ko yàlla gërëm te jariñ ñu ci moom amiin maa ngi ñaan yàlla mu musal ma ci saytaane mu nu jam mi di tàmblee nag samay wax ak jëf ci turam wu tedd wi moom mi yor yërmaande ju yaatu ji matale mbindéefam yi ci àdduna te di ko jagleel ñi ko soob ca àllaaxira yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci sunu sang muhammad ak ñoñam aki saabaam aji xeebu ju yitewoo yërmaandey boroomam ak ndimbalam ci ligeeyal yarkatam bii dib soppeem di sëriñ tuubaa aji xeebu jooju di muhammadul amiin joop doomi sheex ahmadu joop mu dagana nee na ag cant ñeel na yàlla miy leeral àddinaam ji ci wàlliyoom yi di feeñalati ci ñoom yoonu yonantam yiy gindee yoon woowu di wu weetal yàlla ak jaamu ko mooy yoonuw boroom xel yiy dàq lu dul yàlla ci seeni xel tey jànge ag njub ca yooyale imam ci jox leen seen bopp jébbal leen seeni mbir ndax kat ñooñu ñooy ñi yàlla naan ci alxuraan ulaayikal lathiina hadaahumul laahu fabi hudaahumuqtadih muy ci maanaa ñooñu ñooy ñi yàlla gindi kon royal ci seenug gindi di julli tey sëlmël ci yonant bi leegi nag ginaaw yàlla day xéewale xarnu bu ne aw waliyu wu koy gindi di ko won yoonu jub di ko tee jàdd nun waa xarnub fokk ñeent nag mu defal nu xeewal gu tollu ne sunu mbég mii di sunub sëriñ tey sëriñub julit ñi ahmadu doomi muhammad doomi habiibullaah yal na ko yàlla wattu te wattul ko te gërëmi jëfam te méngoo ko moom nag mbooloo maa ngi ko gën a xame ci turu sheex ahmad bamba mbàkke xaadimur rasuul bi loolu amee ma bëggoon a leeral as lëf cig dundam ñeel ki nar a ñëw ginaawam te bëgg a xam dara ciy mayam man nag maa ngi giñ ci yàlla dellu di ci giñaat naan dey xam naa ni xawma te du ma ci man a wax mbaa indi lu dul la gën a néew la gën a bari moom bu ko xalaat ndax manu ma ko ba koy def waaye nag dinaa jéem a nooyal yoon wi ba ku bëgg te yàlla ubbi ko barilub xam xamam yinkiiwal ko jariñ jaamam yi ngir sàkku ci ngërëmam bu ñëwee man cee jaar ndax kat am na ci addiiz mu sell mi mbindeef yi njabootug yàlla lanu ki ci yàlla gën a bëgg mooy ki ci ëpp njariñ ci njabootam gi nee nanu ku taarixal aw wàlliyu mel na ni dundal nga ko kon am leen gàttalug jaloore jaloore mooy taariix walla histoire gii ma tudde irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim may ñaan nag képp ku ci gis lu ko yeemut mu xam ne gàttub jéegoo ma tooñ mu jéggalul ma yàlla te suturaal ma te bañ koo ngàññi ndax kat da na ci gisi leneen lu bari lu koy yéem lu man a wecci loolu ko yéemutoon ndax téere bii ab muxaddima rekk la ag jiital teere dëgg bi mooy minanul baaqiil qadiim fii ma aathiris zheixil xadiim muy ci maanaa xeewali aji des jiy aji jiitu ci ngënéeli sheexul xadiim doomam ja sheex muhammadul bashiir defoon ko yal na ko yàlla sàmmu te guddalu fanam te jariñ ci lu bari jullit ñi ni baayam moom dey teere bu boole la te wattu te dib dër bu naat ñeel ku bëgguw yiw te di ci dox yal na ko yàlla mottali te nangu ko te tas ko ci àddina bi muy ndëxëñtéefam ëlëg ca àllaaxira tey lu nu koy fàttalikoo ginaawam ci fii fi àdduna ci barkeem ak ci barkeb ki ko taalif ak ki mu ko taalifal yal na nu yàlla nangul te nangul nu sunub teere matal ko te tas ko moom itam moom kat yàlla mooy aji kawe jiy boroom ngënéel ak tawfeex tey boroom li fii ak la fee sëriñ baa ngi gane àdduna ci li nu wax ci atum junni ak ñaat téeméer ak juroom ñaar fukk g am ñu ne atum junni ak ñaat téeméer ak juroom ñaar fukk ak ñaar g ca kër waajuram wu goor ca mbakke bawal mu nekk leegi ca wetu yoonu saxaar ga boroom xam xam bu mag bi nuy wax alhaaji hamidin doomi usmaan alfuutiyu altilriyu nee na sëriñ baa ngi gane àdduna moom mi sunnawoo sunnas yonnant bi ci atum sharaha muy g làqu atum shumoos muy g te booba mi ngi am juroom ñaar fukki at ak ñeent mel ni ay jant am ñu ne juroom ñaar fukk ak ñaar ci guddig àllarba ci ñaar fukki fani muharram moom sëriñ bi bi mu ganee àdduna waajuram wu jigeen a ko yoroon ba mu mat a jàngi mu tudoon nag amadu doomi muhammad doomi habiibullaah doomi muhammadul kabiir mom habiiballaah mu njëkk ma doomi muhammadul xayri ak muhammadul kabiir muhammadul kabiir mii mooy ki niy wooye maharam mooy ki sanc mbàkke bawal atum g ci li nu wax waaye dëkkewu ko woon da faa bàyyi woon ab taawam muhammudu farimata magi habiibullaah waaye bokkunu nday moom nag sëñ maharam mii daa desoon jolof fa la làqqoo nu denci ko fa di ko siaare mi ngi askanoo nag ci tukklóor ay waajuram a ngi bawoo fuuta dem jolof siw na itam ne ñoom gànnaar lan bawoo dem fuuta seeni doomi baay tëx ci naar yi ñooy ñoñu moodi nalla ñoom nee nanu ay serif lanu sama mag sama sëriñ sheex muxtaar binta loo doomi sheex iraahiima sëriñub njumri loo nettali na ma ne dégg na ci sëriñ bi luy dëgëral loolu mu ne bis nekk na fa sëñ ba nuy waxtaan ba tudd ag giir ci naar yi gu niy askanale ag cëriif sëñ bi ne ko xanaa xamoo ne ñooñu suniy mbokk lanu mu ne ci noonu la xame ne ñoom ay sëriif lanu man nag li may wax mooy seenug cëriif bu nu ko waxutoon te déggeesu ko it seen jikko yu rafet tegtale na ko muy tedd gu ànd ak yaatug dënn ak lewet gu ànd ak njàmmaar ak jublu ciw yiw ak bañ jikko yu suufe yi ak diinewu gu dëggu yaayam soxna jaaratul laahi maryama buso doomi muhammad mom muhammad mom hammaad mom alliyu albusobiyu ñooñii seenug cëriif lu wér la ñi ngi cosaanoo ca imaam hasan mom alliyu ibnu abii taalib karramal laahu wajhahuu kon sëñ bi seriif la ci nday ak ci baay lenn ci samay doomi baay tëx nettali na ma te moom ku dañ kumpa la ci suufus fuuta mu ne dox na bis juge ci dëkk bu ndaw bu nu naan bukke jëm fu nu naan mbumbe péeyub filaaw nee na mu romb ci ay gent yu ñu ne ko ñooy fi mbàkke màkke yi dëkke woon am na ku ma nettali ci ñi sant ba ne mbàkke mbàkke yi seeni doomi baay tëx lanu kaaf gi nekk ci mbàkke ag haa la woon muy haa giy mujj ci ba wolof yi def ko kaaf waaye wax jooju ju doyadi la fi man li nu jortu daal mooy aw sant wu yàgg la niki santi ajam yi ajam mooy ku dul araab li fi ne daal mooy ñaari wax yi bu ci nekk dëgër na te am na màndargaam dëgg waaye buso boso yi ñoom seen cosaan fuuta la ca fa niy wax golare barab yii yepp it yu jegee lanu barab yii it ak wax yi ci am am nanu màndargay dëgg yuy tegtale teddngay ñaari askan yi bi sëriñ bi tollee ci war a jàngi wayjuram dal di koy jébbal nijaayam muhammad doomi muhammad buso mbokkum ndayam ju tedd ju yiw ja mu tàmbli koo jàngal ba mu màgg as lëf tàmblee yewwu mu jebbal ko moom itam nijaayam sëriñ tafsiir mbàkke ndumbe doomi muhammadu soxna buso doomi muhammadul kabiir mi nu tuddoon moom mooy mbokkum maami sëriñ bi ju jigéen ndayi wayjuram wu jigéen soxna asta waalo nu daan nekk foofa fa moom ca mbàkke bu noor baa bu nawet baa lu ci ëpp danu daa dem jolof ba bi tafsiir mii làqoo te booba sëriñ baa ngi jeggee mokkal kenn ci ñunu woolu ñi nettali na ma ne sëriñ bi nettali na ko ne àlliwaam a ngi tulloon ci latajjidanna bi jànglekatam boobu di làqu mu dal di dellu ca wayjur wa dal di farlu ci njàng mi ba mokkal alxuraan def tajwiid ak tas hiih ca ña ko daa defale ca jamono jooja loolu lepp ci wetu baayam daa wul tàggalikook moom lu dul lu néew ndaxte magam muhammad jaara dafa nekkoon ca kenn ca tas hiihkat ya ca yeneen dëkk ya bu ko defee leeg leeg amaa na mu jaar fa nekk fa ak moom weer walla ñaar doog a dellu booba ña nga saalum ca jamonoy jiyaadkat boobu di màbba jaxu ndax kat booba ñoñam màbba boole woon na leen ca ñam pangoon jëme saalum nga xam ne bawal ak jolof daanaka bawu fa woon kenn bi mu faatoo nag moom màbba nit ñi dal di dellu seeni dëkk waajuram wi moom itam dellusi ci ñi doon dellusi ànd ak latjoor ci noonu nijaayam akug njabootam des foofa sëriñ bi it bokk ci ngir jàng xam xam noonu mu tàmbli di jàng ci baay tëxam samba tukklóor ka doomi bàjjani baayam bi mu jàngee ci moom dali xam xam tàmblee ñaw as lëf la dellu ca baayam te booba ma nga paataar benn dëkk bu ndaw bu nekk ca wetu njéndul amadi yala dëkkuwaayub latjoor ca joojale jamono ndax moom sëñ mammoor daa defoon ku latjoor fonkoon lool daa ko laaj tey diisook moom waaye moom sëñ mammoor bëggutoon a dëkk ak moom ndaxte du woon ku xemmeem seen alal ji du caagéenug seen teddngay nguur gi li ko loruloo woon ci mu dëppoo ak ñoom ak a mudaaranteek ñoom mooy njaboot gi mu yoroon bu ko defee latjoor daa ko dëkkal ci wetam waaye sëñ bi daawul nangoo dëkk ak moom moom kay day dëkk ca wetu péey ba mu ne rekk ndax da daa jàng ak a jàngale te jàng ak a jàngale neexoowut aki buur li fi ne daal ca wetam la dëkke woon nga xam ne su ko soxlaa ñëw ci lu dulub coona ci noonu sëñ bi nekk ak waajuram di jàng ci moom te di farlu ci mokkal gi ak xereñe gi ak dégg dégglu gi ba faf raw ci fann yi ci biib diir it daa na ci def leeg leeg mu seeti sëñ xaali majaxate kala moom mi dëkke woon fa péey ba ak lajoor di woon ku raw ci fanni xam xam yi rawati na làkkuw araab di ku siiw ci man a woy bu ko defee muy xamlu ci moom araab leeg leeg it mu daa ko indil ay woy yu mu def ngir mu toppal ko lihraab ba ak araabe ga ak harool ba leeg leeg mu génneel ko ci ab yàq ba mujj sëñ bi far ko raw mu mujj saa su ko wonatee lenn ci woyam yooyu mu ni ko indil ma ko ma mokkal ko mu mujj toppalatu ko waaye day mokkal li mu koy indil nii la nekke woon ak xaali amoon na fa it beneen boroom xam xam ci waa gànnaar yi dëkke woon njaañ tuddoon muhammad mom muhammadul kariim bokkoon ci giirug daymaan ci doomi seyidil faadal yi ñu gënon koo xam nag ci turu muhammadul yadaali waaye bokkul ak ki def téere bi nu naan zahabul ibriiz ci tafsiir ndax kooku am yadaalim daymaan mu yàgg la sëñ bi bariwaa na lu mu ko daa dikkal di jàng ci moom xam xamu bayaan xam xamu wax ju rafet yaakaar naa ne nee na it ci lenn li mu nu daa nettali yàlla a xam ak bu mantiq xam xamu xellu bi wayjur wi xamee ci moom raw gi ak cawarte gi ak laabiir gi mu dal di koy jox mbirum njàngale mi bari na lu mu ko daa jàngal ab bind ci kanamam ci téereb boppam ba walla ci téere bu mu dalagul ngir mu jàngal ko boroom bind boobee walla téere ba bu ñëwee ngir wóolu gu mu wóolu xam xamam akug ñawam sëñ bi it daan ko def ba li ëpp ci dongay sëñ mammoor yi mujj féetesi ak moom doylu ci moom waajur wi bàyyi leen ak moom te bég ci waaye yàggul dara rekk latjoor tuxoo kër amadu yala dem sukeer péeyam ba ca kajoor yobbaale sëñ mammoor mu sanc ca wetam tudde ko mbàkke kajoor sax fa ñaari at dal di wuyyuji boroomam nee nanu looloo ngi am ci muharram atum g dëgg naa ci sëñ bi mu ne bi waajur wi tollee ci sukkuraat took na fa boppam wàcce fa ab kaamil bisub altine guddig talaata mu làqqu nu denc ko deqale di ko siyaare man dey alhamdu lillaah dem naa fa ba siyaare ko bi niy yobbu wayjur wi deqale muy dëkk bu ndaw ci dëkki kokki yi ci wàllug mbaakol sëñ bi àndon na ca gunge ba di liiru bariwaa na bu ko ab gawar bëggee joxuw fasam mu ne dox a ma gënal bi mbooloom dëkk bépp dajee di mbooloo mu kenn masta gis nu jublu ci jullee néew bi jiital sëñ tayba muhammadu ndumbe maar silla mi nu tuddoon ci buntub seedey ñu mag ñi ñeel kii nuy wax ci moom bi nu noppee ci julli gi ak denc gi sëñ tayba digale nu daje te dal te xerawlu ci noonu mu jug xutba waar nit ñi wax wax ju rafet bi miy jaale sëñ bi nit ñi bi mu noppee ne ana sëñ bamba noonu la nu ko daa wooye ñoom ca jooja jamono mu wuyyu jug ma nga woon ca catul mbooloo ma sëñ tayba ne ko jegesil mu xaw a jege bay degganteek moom di gisanteek moom di ko man a toontu ci lu dul muy yekkati kàddoom dal di yam foofa ngir bañ a jéggi nit ñi xutbakat bi neeti ko jegesil mu ne ko maa ngi lay dégg sëñ tayba dal di koy jaale njaal mu rafet ne man nag dama doon sàkku nu ànd ci mbooloo mu màgg mu sa moroomi waajur wii ngir nu seeti latjoor jaale ko sa waajur wi jaale gu ko man a dëfal ngir kat moom ab xaritam la woon dib soppeem te dib sëriñam daa diisook moom bu ko defee nu waxtaan ak moom ci yaw sampu la fa moom ba mu man laa teg fam tegoon sa baay bu ko defee doo gis ci moom lu dul aw yiw ak teraanga lii daal mooy sama xalaat yaw nag luy sa xalaat sëñ bi ne ko li aju ci jaale gi ak dëfal gi maa ngi la ciy sant te di la ci ñaanalub yool waaye mbirum seeti ay buuri àdduna moom duma ko def ndax xemmeemu ma seen àdduna ji te soxlawu ma seen teddnga teddnga ci yàlla laa koy sàkkoo buurub buur yi mbooloo ma tiit tas ña cay ñu baax wax ji da leen a yéem rusloo leen ndax dëggu gi mu dëggu tey toroxal way bëgg yi àdduna juge ci seen doom ju diw waxambaane tegi tànkam ci seeni wagg te manu ñu ci dara bu dee mbooloo mi moom li leen yéem mooy bañ gi mu bañ teraanga ju teew jii ak xéewal gu jàppandi gii nu ne kii daalub dof la ci loolu sëñ bi def na ñaari dagiiti woy yu rafet te yéeme bu njëkk bi mooy waxam jii nee nanub dof laa ngir wëlbati gi ma wëlbati samab gis wëlif leen ba fa mu yam teewluwu ma ko te woneesu ma ab yaxam jamono ja may liggéey waaye beneen bi moom mooy wax jii nee nanu ma jéngal jëm ci bunti buur yi kon déy da nga am ay may yu lay jariñ jamono ju ne ma ne leen yàlla doy na ma doyloo naa ko soxlawu ma lu dul xam xam ak diine yaakaaru ma te ragalu ma ku dul sama boroom ndax yàllaay ki may doyluloo te di ma musal nu may joyale samay mbir jëme ko ci ñoñ lottu nanu ci seen mbiri bopp ni miskiin yiy lotte walla nan la ma bëgg poñatum àdduna bii di jañe jëm ci dëkkaale ak ñoñ seeni kër mooy dërub saytaane su ma dee naqarlu mbaa may bég boroom aras laay woo mooy aji dimbali ji dara dul të te mooy kiy amal li ko soob bu bëggee gaawalum mbir loola gaaw bu ko nammee yeexal mu yeex ba cib diir yaw mi may yedd bul sonal sa bopp ndax kat man amu ma lenn lu ma naqari ci ñàkk àddina bu dee sama ayib mooy dëddu gi ma def ci seen poñat mi kon déy ayib jooju ju gànjaru la ju ma dul gàccaal waajuram wu jigeen wu tedd waa nga làqoo poroxaan ca saalum nu denc ko fa jamono ja fa sëñ mammoor nekkee moom sëñ bi bi waajur wiy dund nanguwutoon a taxaw mbaa muy taxawal dara moom daal ci moom rekk la toppoon mel ne néew bu nuy sang fu nu ko jëmewul du fa jëm bi mu làqoo nag mu des ca ligéeyam ba mu ko bàyyee woon at ak lu topp ña fa nekkoon it jàng rekk a leen fa bàyyi woon du leneen moom itam ab jàngalekat rekk la woon waaye loolu teewul woon mu doonoon ku yitewoon a xam gaa ñu baax ñi ak seeni xam xam ak beru ak a wër niki ñu baax ñi mu leen daa junj ciy waxam ak a feeñal ay maanaa ak a yëgg ba bi ko himma ju kawe ji himma ci lun man a firi mooy yite dikalee muur ko mu jug yëgg as lëf neeti tekk dal di woote cig nooy jëme ci mbiram moomu bi ko mbir mi gënee lëjal nag gën a fees fi moom gën a rëy mu dal di biral woote gi dajale mbooloo mi taxaw fa ñoom xutba leen sukkandiku ci dokkub dogu ne leen yeen mbooloo mi ku àndoon ak man ngir jàng rekk na laxas jëm ca boppam aki mbokkam mbaa fa ko soob man loolu rekk taxatumaa jug ku bëgg li nu bëgg nag na toog dal di leen fay bàyyi dugg ca biir waxam jii nag dal di leen bàyyi cig jaaxle ñenn ñi dem ña ca des des fa am ñuy jeem a tëyye seeni xarit ngir ñu des ak ñuy xiirtal seen waay ci ñu dem sëñ bi moom ne tekk rekk jeemul a tëyye kenn ku bëgg a dem ba mujj li ëpp ci mbooloo mi dem bàyyi ko fa la ca gën a néew des fa bi loolu lépp daata am fekkoon sëriñ bi mu sóobu ci ngiirum taalif ci xam xam yu nu tuxal yu sariiya yi mu woy ummul baraahiin bu imaam sanoosi wayjur wi nangu ko bég ci te mujj di ko jàngale bàyyi wesar wa doonoon cosaan la dégg naa ci sëñ bi mu ne woy woowu de waajuram jàngal na ko ñaari doomam yii di sheex coro miy siidi muhammad alxalifa ak sëñ aafe mi tuddoon ahmadul muxtaar mu woyati teereb imaam xazaalii bi tuddoon bidaayatul hidaaya dal di koy tudde mulayyinuz zudoor di ci maanaa aji nooyal ji dënn yi ginaaw bi mu gàttal ko tudde ko munawwiruz zudoor di aji leeral ji dënn yi ci atum g teg ci jëzbatuz zixaar di bijjig gone yi ak jawharun nafiis muy wurus wu gànjaru wi nga xam ne da cee woy wesaruw imaamul axdariyyu ak yu dul yooyu bi ko donga yi nangulee nag lii mu leen doon woo daa bàyyi njàngale mi jëm ca di leen tarbiya ak a tarqiya tarbiya mooy yar ni ko sariiya bëgge tarqiya di yékkatee jëme ca yàlla man nag nee naa lii de du ñàkk muy ndigalug yonant bi j y m ndax kenn ci sunu sëriñ yi nettali na ma te moom ku wóor la di ndëërlaay ne sëñ bi de wax na ko ne yonant bi j y m moo wax ak moom ci gimiñam ne ko yaral sa àndandoo yi ci himma te bu leen yar ci njàng loolu sëñ bi gën na koo leeral ci xasida gii bokk na ci kiimaani doomi abdul laahi ji yal na ko yàlla dolliy xéewal ak mucc moom miy leeral suufam si ciy wàlliyu ba yawmal xiyaam te ku ci ne méngoo nga sunnaam si di ko ñogal wëlif bidaa bokk na ci kiimaani doomi abdul laahi jooju bégal gu mu bégal jëwrinam jii ci ne ko fazdah mooy wooteel ca kaw yonant bi j y m digal na ko ne ko mu jàngal muriid yi ak ku nangu mu laabiire la ci waa jamono te mooy ki ko àggale ca borooman cig taxliya mooy setal nit ki féexal ko ciy ayib bégalati ko ci tahliya muy ràng nit ki ay takaay walla sol koy ngënéel li mu jublu ci fazdah ji nag mooy biralal ca kaw mooy ji ci alxuraan fasdah bi maa tuumaru wahrid hanil musrikiin mooy biralal li nu la digal te dëddu way bokkaale ñi yàlla daa digaloon yonantam bi j y m mu biral wooteem ga ginaaw bi mu ko daa yalu maanaam dëgg dëggi loolu mooy sëriñ bi bi donn gi mu donn yonant bi matee ci matalug yàlla t s te mu dolli ko ay xam xam aki hikma aki leer aki mbóot te may ko kàttanug man a yanu wilaaya gu mag gi bi loolu amee nag mu digal ko mu woote ca kaw woo mbindéef yi ñu weeru ci moom di jële ci moom tey def ay ndigalam di bàyyi ay tereem ci loolu la waxe yàlla mi nga xam ne lu ko soob mu def moo ma jox xam xam yi ak seen barke wattu naa lu xajul ciy téere kon boo may ligéeyal bul tàyyi yàlla miy joxe jox na ma ci darajay yonant bi barkeb alxuraan ak xam xam yi jël seen barke def ko ci samam njàngale yàlla jël na mbooti laa illaaha illal laah def ko ci samy taalif yàlla jox na ma te dootu ko nangu te man kaaraange laa te dib weeruwaay ci ndimbalam loolu nag ngënéelul yàllaa ku ko soop la koy jox te nee na ma neel wéeru leen ci man ci maanaa sama boroom digal na ma ma leeral nit ñi ne man ab wéeruwaay laa tey kaaraange ku bëgg aw yiw àdduna ak allaaxira na wéeru ci man mu dellu waxaat ne murid bu yoqatul ci man de texe na ci làq ngën ji ay may murid bu yàlla wommat jëm ci mu aju ci man texe na te da na céru ciy may murid bu wéeru ci man de yàlla miy sama dëkkandoo bu kawe bi def na muy ku texe ci lu kawe njortam bepp murid bu aju ci man day texe te ku niy soril la aw ay képp ku aju ci man déy am nga ag mucc ci nëx nëxi àddina ak allaaxira ginaaw bi mu leeralaat ne way gëmi jinne yépp ci jamonoom aju nanu ci moom mu ne jinney sama jomono jii dey ña ca gëm ñépp aju nanu ci man waxuma ña gëmul mu wattuloo nag ñi aju ci moom ñuy xàccati ginaaw bu nu jébbaloo ne toroxte ñeel na ki ma dëddu won ma ginaaw muñ ma ginaaw bi mu duggee dib murid dal di leeral lu dig murid ak lub murid di bëgg mu ne mu leeralaat ni ab muriid di mel ak ngértel ànd ak sëriñ bu àgg mu ne melow ab murid mooy bañ a bëgg dara ngir yàlla ku bëggul lu dul yàlla àgg fa moom mu jox ko aw yiwam mu leeralaat ne murid saadiq de am na ay meloom yoy bu ko amee am wépp yiw meloy murid saadiq ci gàttal ñeent la ma tënk leen nag ciy bayit ngir ragal woru dëggal ci bëgg sab sëriñ ba fàwwu jëfey ndigalam fu mu rote rekk bayyi gaaru ci lu mu man a doon gaaru mooy di am xalaat ci ndigali sëñ bi ak doonte ci sa baatin la ci li nu nettali ak a tànnal sa bopp la ngay def ngir sa rafetug njort képp ku boole yile melo ci murid yi déy da na jot ndëërlaay ya gaa yu baax ya mu biralaat ne kiiraay am na juroom benni cosaan yu murid bi war a dagg te malaaka yi dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk ne kiiraay am na juroom benni cosaan ku bëgg a àgg da nga leen dog ñooy baril lekk ak naan ak a jaxasook nit ñi bari wax bariy nelaw sàggan ci tudd yàlla miy jàmm gëstul loolu ci jawaahirul mahaani bi sunu sheex tiijaan mu nu màggal mi def nettali nanu ne malaakay aji màgg ji dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk ngir yëram ko loolu man nga koo gis ci taalifi boroom hawaarifil mahaarif mu neeti murid saadiq doomi waxtoom lay doon ne murid saadiq mooy kuy wëlbatiku ànd ak waxtu wi mu nekk te du fuglu wa ca kanamam ndax loolu day teree yéwenal waxtu wi teew gëstu leen loolu ci jannatul muriidi téere bi sunu sëriñ xaliifatur rasiid def ak lu bokkul ak loolu ci li mu wax ci mbirum boppam mom muridam yi nga xam ne bu nu ko toppoon indi fi lu yéem xel yi te da na mujj kon gàttal gi nu bëggoon ci téere bii du amati ndax moom téere bii as kook la ci geejug xamale ko nu indil leen fii nag as tuut su nu tas ci wone lenn ci sekkarey xaybu yi xaybu mooy lu faddu muy mbirum biir niki liy xew te xewagul mu bégal ci ñi aju ci moom ngir dolli leen ag xeemeem ak sawarloo leen mu wax ne ñi aju ci man bu nu ko defutoon dem sawara doonte as ndiir lay doon it njëkk nuy tàbbi ajjana ji nu dig ñu ragal ñi yàlla li waral sama tukki bu sori bi yàlla mu barkeel mi te kawe daa bëggoon ca asal may kiy ramu samay donga dox na sama digante ak nasaraan yi tàbbal ci seeni xol ag ragal ma nu def la nu def nag ngir ma bañ a nekk dib nasaraan ndax bu ma ko doonoon tabbi sawara walhiyaazu billaahi waaye yàlla a ma aar ci sawara ak lépp lu mu gëramul ci darajay yonant bi j y m mu bind ay laabiire ñeel murid yépp ne mi ngi juge ci man jëm ci mbooleem murid yu góor yi ak yu jigéen yi ab nuyyoo bu teey bu leen di musal mboole seen te di leen tabbal ci jàmm ak aafiya ci addina ak alaaxira ci barkeb yonanat bi j y m ginaaw bi may digal képp ku aju ci man ngir yàlla mu kawe mi te tedd mu xamlu pas pas yi ak tawhiid ak àttey laab ak julli ak woor ak lu dul loolu ci lépp lu war mukallaf man nag warlul naa leen taalifal leen mbooleem lu leen koy xamal ngir jëmmi yàlla t s wasalaam mu bind lenn ci ay murid ab tontu bu neex yal na nu ci yàlla boole ñun ñépp mu ne ci assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa wa barakaatuhuu ma lay xamal ni sa bataaxel ba agsi na yaw murid bu dëggu bi waaye na la wóor ne doo gis lenn loo ragal booy faatu ak ci bàmmeel te ñaari malaaka yiy laaje xam nanu sa sëriñ te da nanu doylu ci xam gi ba dunu la laaj dara lii nag xamle la gu mu teg ci yoonu laaj ak tontu laaj bi moo di lan la sëñ bi woo ay taalibeem jëme lan mooy tontu li moo di sellal moom mi nga xam ni mooy ruuhug jëf tey ngértel xam xamub way xam ñi yàlla tey waralug àgg ca yàlla àgg ci yàlla nag ñi ngi ci jublu jaam bi nekk di ku wéetal yàlla ciy yëggoom aki dalam aki pas pasam aki waxam ci lepp li feeñ ak li nëbbu lii nag manut a ame ci njàngale rekk ndax kuy jàngale ab tegtalkat rekk la li ci des mi ngi ci aji jàng ji man naa am mu jëfe man naa am déet du ligéeyub jàngalekat muy sonnu ci waa ji jëfe loolule loolu sheexu tarbiya la war bokk na ci ligeyam moom sëriñub yar jàng ak jàngale ak ligéeyloo ak ay tudd yàlla ak gindee ginaaw bi mu leen xiirtalee cig cofeel gu dëggu te du tàggook ñoom li feek wonu leen seen ayibi bopp ligéeyloo leen ci nu jéem a laab ci yooyu ayib ngir man a àgg ak ñoom fa yàlla inshallaah bu loolu jàllee mbirum tarbiya day mbir mu gudd manunu cee wax fii mu dem ak ñoom ci yar leen ci himma ñu nangul ko ko mu dox ak ñoom ci ngérum tàggat dajale leen di leen ligéeyloo lu bari yanu leen ci fàttaliku yàlla lu bari ak a jàngi xasida ak taqoo laab ak a beru rawati na sori jigéen ñi ci noonu ñu kawe ñu dul ñoom ndax donoo joxe woon seen bop ak seen alal ci yoonu sàkku gëramul yàlla yalla jënd na ci jullit ñi seeni bakan ak seen alal faye leen ko àjjana sëñ bi wéy ci yoon wu jub wii mook saabaam yi dale ko ci njëlbéenug atum junneek ñatti téeméer ak benn ba bi mu sancee mbàkke bawal ci at moomu juge mbàkke kajoor sax fa lu tollook ñaari at nit ñi di ko dikkal juge fu nekk ñii di jebblusi ñii di joxesi àddiya ñiiy sàkku ndimbal mu mujj yoonu këram gi mel ne yoonu ab ja ci ñeenti at yii nag mu siiw ci siiw gu kawe ñu jege ñi ak ñu sori ñi ñepp di yéemu ci moom te booba amagutoon sax fan weeri at ci diir bii sëñ bi wër na ci réewum wolof mi dale saalum ba waalo barak siyaare fa mag ña ña cay dund ak ña dundul jaar ca sëriñ sa jële ca ñoomi wird bokk na ci ñi mu siyaare ñoñ sheex siidiya siyaare na bàmmeelam ca tindawja siyaare sheex baaba mom abiihi ca maymooni tagg leen jële ca ñoom woy càllaleg xaadir gi tàmblee ko ca sheex baaba ba fa mu yam looloo taxoon kenn ci sheexi naar yu mag yi laajoon ko kuy sa sëriñ mu ne rasuulul laahi j y m mu ne ko kon lu tax nga ne fi di tudd waa kër sheex siidiya ak a woy ay sëriñ ak a tag mu ne booba da maa melon ne ku gumba di làmbatu yoon wi di ko sàkkoo xam ci ku xam ak ku xamul bi ma dajee boroom yoon wi ci ndimbalul yàlla nag muy yonant bi j y m mu xëcc ma ci boppam laa wacc ker keraan yi waaye di jokkook ñoom ngir yàlla ak a soppanteek a jariñante ngir moom te wax na dëgg ndax mbiram ak ñoñ sheex siidiya loolu lay tegtale mujj nanu mel niy doomam mu mel ni seen baay di leen jariñ ci alalam lu leenub buur jariñul ab sëriñ it jariñu ko ab taalibeem sheex baaba tag ko ciy xasaayid aki dagiit yu tollok ay téeméeri bayit bokk nanu ci yile shex ahmadu xéewal la gu yàlla jox mbindéefam yi ak waxam ja sëñ bi daal xéewal la gu yàlla xéewalee di kiimaan ci kiimaan yi ak yu bokkul ak yooyu bu waxutoon yu dul yii it ñaari bayit yii rekk doyoon nanu seede ci màggug sëñ bii ak wilaayaam ndax kat sheex baaba ak màggam gi du fo mbaa muy yaxantu ci woy ni suharaawu yi moom dey lu mu wax ci ndigal la ko teg ak jaamu yàlla yal na ko yàlla fay ci ñaari bayitam yooyu bokk na ci ñi mu siyaare ci sheexi naar yi ustaas baaba mom hamdi ma jublu ci hamdi mu ñaareel mi dikk na fa yendu fa fanaan fa nee nan ci menn mbaar sama xarit ba niy dàkkantale kaadi sheex abdul xaadir doomi amiirul kumlayli nettali na ma te booba taalibeb ustaas baaba la ne ustaas mii moo jox sëñ bi sekkare bi waaye nag leeralu ma ban sekkare la man naa am muy wirduw saasalii ndax sëñ bi bind na ne moom wirduw saasali mi ngi ko jële ci wenn wasiila njëkk muy daje ak wasila wu mag wi di yonant bi j y m te leeralu nu kooka kan la li waral kaad mii nettali ma ko mooy maa ko laajoon bi mu jëlaatee ci sëñ bi wirduw sasalii ndax xam nga ci ku ko sëñ bi jële woon mu ne déedéet waaye nettali li mu waxoon ci diggante sëñ bi ak ustaas baaba nu jorte ci ne ci ustaas baab moomu la ko jële ndax moom ab xaadir la woon kaad nettali na ma ne bi sëñ bi agsee ci bi miy siyaaresi ustaas ci bëcëgug bis bu sell ustaas defaral ko am soow mu neex ci ndox mu sedd ak suukar looloo ngi amoon ci jamono ji sëñ biy nattu boppam ci di tegoo ay coona mu ne ko naanal mu ne ko man baax na du ma naan lii mu ne ko ndax daa baaxul ci wàllug wér waala da nga koo bàyyi ngir yàlla di jiyaar ak sa bakan sëñ bi ne ko waaw loolu la mu ne ko kon naanal bàyyiwu ko ba mu far naan ginaaw bi la dongay ustaas yi laaj lu waral mu sonnu ci mu naan soow mi mu ne leen ndax moom kat sonal boppam rekk la bëgg ak mettital ko mujj loolu di aadaam ngir yàlla ju mu manatul a bàyyeeti ndare cib coona ma jëflante ci ak moom waaye yàlla defal na ko barke ndax mujj na dëgar ci këng ginaaw bi lii wéyee lu yàgg ahmadu doomi ustaas seetsi na sëñ bi njaaréem mu bég ci lool di ko ganale ngan gu mu sonn indil ko ñam yi ak naan yi bi nu àggee ci ataaya ahmad xam ne mbir dana am ndax moom du naan ataya bi ko sëñ bi tàllalee ataaya ji mu ne ko du ma naan ataaya mu ne yàllaa tax nga bàyyi ko ngir jiyaar ak sa bakan walla ag weradi mu ni ko yàlla mu ree ne ko naanal ma fayoo ca la ma sa baay defoon ñaanal ko ci barke bi sëñ bi nekkee ci wëram googu nit ñaa ngi ko daa dikkal bàyyikoo ci gépp wàll ngir xam xam bu bari bi ak njariñ li ak cofeel gi nu amoon ci moom ak diinewu gu dëggu gi rawati na alal ju bari ji mu daa joxe rekk nga xam ne daawul tëyye ab dërëm lu ñëw mu joxe di jox mag ak ndaw goor ak jigeen gor ak ab jaam ku am ak ku amul ku baax ak ku bon loxo bu tàllaliku jëm ci moom mu feesal ko te soxlaalul nit ñi doyloo kàppitaalam bi dul lu dul jublu ci yàlla ak yiteem jépp mu dem gànnaar jaar ca sëriñ ya siyaare ñay dund ak barabi way faatu ya jariñ leen ci alalam ju bari ja nu sopp ko nu kawe ni ko ñu ñuul ñi soppe defal koy xasiday tagg siyaaresi ko ci réewam ginaaw bi bi mbokk yi gisee ci moom kaweg xel gu diine gu mbaax gii mu yor ak jublu gi ko àdduna ak nit ñi jublu nu tàmbli di ko iñaane di ko lor mu daan julleendoo ak ñoom lor yi ëpp mu mujj beru leen ak am mbooloom ak jàkkaam yàlla gën a fésal mbiram ñu gënatee mer nga boole ci terewu gi mu defoon ci mbirum buur yi daawul nangoo jaxasoo k ñoom ba da daa sàkku sax ci sëñ mammoor ci ay bataaxel yu mu ko daa bind da daan kersawoo jàkkaarloo k moom di ko ci wax dara mu bàyyi ag jëflanteem ak buur yi naan ko seen teddngay fii ji toroxte la ëlëg sëñ mammoor daan ko ko nangul te di ko ci jéggalu waaye njabootam gi taxoon ba manu leen a bàyyi ma nettali leen as lëf ci jaloore nee nanu bi kenn ci jaraafi latjoor yu mag yi mu nekkoon ku am solo fa latjoor jébblusee ci sëñ bi mu bokkoon ci jàmbaar yi amoon ay alal mu ndàmmoom gañewoon lu bari ci màggum xareb samba saajo bi màgg mooy li niy jële ci koo xeexal ba not ko samba saajo ab dëkk la bu nekk ca penkub njàmbur diggam ak jolof la xare boobu ame woon ci diggante amad sheexu ba mu fuuta ak latjoor tubaab yi japle woon ko moom latjoor ba mu gañe ko ray ko xarekati latjoor yi gañee ci woon màgg mu rëy ci alal ak ay jaam te ña ca ëpp diggante jolof ak fuuta lanu bàyyikoo ak kajoor tey jullit lanu buur bi laaj ndax man na leen a def ay jaam kenn ci boroom xam xam yu mag yi ne ko waa waaw ndax ahmadu sheexu da doon wooteg yonnant kon alalam ak dereetam dagan nanu nu dal di wéyal loolu te kat ag wooteem yonnant mbooloom boroom xam xam yu mag yi saxalunu ko li waral xare bi lu gudd la manunu koo netaali fii bi jaraaf jooju tuubee ci sëñ bi mu digal ko mu wacc mbooleem jaam ak alal ji mu ame woon ci xeex boobu jaraaf ji déggal ko def ko ànd ci ak kontaante latjoor ak ay gaayam jàppe loolu nag ag weddi ñeel àtte bi leen kenn ci boroom xam xam yi defaloon ne leen jaam yi dagan nanu nu mere woon ko nee nanu ma jaraaf ya woo woon nanu jaraaf jooja fa kanamu latjoor ne ko lu tax nga bokk ak nun ndab rgg rekk wëlbatiku doyatu la nga ciy xëpp suuf mu ne leen waaw weñ a tàbbi ci sama bakan lëjal ma moo waral lii ngeen gis ci man waaye bëgg a nëxal seenum mbir taxut mu jublu woon ci weñ wi lislaam ji ko duggoon cig mbetteel yaw nag xam nga lëjal gi lislaam di def ku mu dugg du ko bàyyi ndare bu daa tuub bérab fu yonent yàlla yaxya doon sóobe nit ñi ci ndox ci gannaaw dexu yurdan maanaam ci penku dex ga yow foofu la yaxya sóobe yeesu ca ndox itam bu yàgg xamatuñu tembe fan la dëkk bi nekkoon waaye seetkati cosaan yaakaar nañu ne fekk nañu bereb ba ca penku dexu yurdan ca atum berab ba wadi al xarar la tudd am na fa ay bëti ndox ak benn làquwaay fu ñu yaakaar ne yaxya daan na fanaan su fekkee ne danga nekkoon ca dëkku yeriko manoon nga gis berab ba ñoom ñi gas ci suuf ngir seet naka la nit ñi dëkke ca yeneen jamono yu fekk nañu ca bereb ba ay tabax ay jàngu ay làquwaay fu nit ñi doon dëkk ak ay sanguwaay taalibe yeesu yi doon nañu ajji ngir siyaaraji ca xarnu yu jëkk yi gannaaw jamono kirist ci làkku ibrë la tur wi jóge ci angale mooy boaz ci faranse mooy boaz boroom alal ak beykat ci dëkku betleyem la woon dafa takkoon jenn jigéenu mowab ji tudd ruut jot na ruut ndax jëkkëram mbokkam la woon te faatu na bala mu am doom ci kaw seeni yoon su fekkee ne am na genn góor gu faatu te bàyyiwul doom mbokkam mu gëna jege war na donn jabaram seen taaw bu goor dina donn ci goor ki faatu woon bowas mbokk mu jege jëkkëru ruut la woon doom bi ñu jur mooy maamu daawuda man nañu koy jàng ci ru naka noonu bowas bokkoon na ci maamaati yeesu ni ñu koy gise ci macë ak ci luug mc lu ci angale mooy israel people of israel or children of israel ci faranse mooy israël peuple d israël ou fils d israël israyil mooy tur wa yàlla jox yanqóoba doomu isaaxa di sëtu ibraayma ñi wàcc ci yanqóoba nag lañuy wooye bànni israyil walla it yawut yi def nañu fukki giir ak ñaar di yi soqikoo ci doomi yanqóoba man nañu gis bànni israyil ci injiil ci aaya yii mc mk lu yow jëf jëf ro ko ko ef fb yt pi pe ci angale mooy thyatira ci faranse mooy thyatire ca jamono injiil dëkk la woon ci diiwaanu nguuru room bu tudd asi maanaam ci sowu réew bi tudd tey jii tirki tey jii akhisasar la tudd dafa nekkoon ci yoon diggante pergam ak sàrd ci dig bi nekkoon diggante diiwaani misi and lidi dëkk ba siiw na ndax cuub bi ñu fa defaroon ca jamono ju njëkku mbooloom ñi gëm kirist amoon na fa mbooloo bu am solo naka noonu gis nañu ne mooy benn ci mbooloom bi ñu bind ci peeñu ma dañu ciy wax ci catir ci injiil ci jëf pe ci làkku ibrë la tur wi jóge daawuda mooy ni ñu ko waxe ci lislaam ci angale mooy david ci faranse mooy david moo doon buur bu mag ci bànni israyil di yonent bu bind lu bare ci sabóor man nga jàng ci jalooreem ci kàddug yàlla gi ci sa sa ki ch benn ci maamaati yeesu ci macë ak ci luug ci injiil daawuda moo feeñ ci aaya yii mc mk lu yow jëf ro tim yt pe turu kirist la muy wone ne ci lu jëm ci juddoom wàcc na ci yonent yàlla daawuda di wone it ne almasi bi la sëtu daawuda moo feeñ yoon ci injiil ci aaya yi mc mk lu baatu njàngat day tekki mbooleem ay mbind yuy wax ci ay koj ni ko ñenn ñi di gisee du yem rek ci mbind yu ñu taaral waaye am na it njàngatu kàddu maanaam yu yemm ci ay kàddu sunu xoolee mboolaay yu mel ne yu waa afrik yi xamul woon bind seenum njàngat ci kàddu la yemoon njàngat day di ab fànn gu am genn melokaan gi ci jokkoo muy ci mbind walla ci kàddu di tax ñuy man a jëfandikoo làkk bi bu baax te di am njeexit ci baatukaay bi njàngat da fa yaa te bariy fànn li leen di wuutale mooy mbindin walla ndefu téere yi taaral gi am na ci lu am solo ci lu ëpp dañ koy jàppee ni ag fànn waaye itam doon na lu jafe rëdd ay peggam rawatina su nuy bind ci xeltu ci xarala walla yeneen njàngat day di ab fànn gu am genn melokaan gi ci jokkoo muy ci mbind walla ci kàddu di tax ñuy man a jëfandikoo làkk bi bu baax te di am njeexit ci baatukaay bi njàngat da fa yaa te bariy fànn li leen di wuutale mooy mbindin walla ndefu téere yi taaral gi am na ci lu am solo ci lu ëpp dañ koy jàppee ni ag fànn waaye itam doon na lu jafe rëdd ay peggam rawatina su nuy bind ci xeltu ci xarala walla yeneen ladab baat la bu bawoo ci araab di ci araab adab adab nag ci araab am na ñaar ba lu ko ëpp ciy tekki waaye ñaar yi ci gën a siiw bi ci njëkk mooy adab di baat bu sëriñ tuubaa y y g bari lu mu jëfandikoo ci téereem bii di nëhju di téere bu tëriit li sujet bi jëm ci yar ak dugal ci nit ñi ay teggiin aadaab di mbooloo pluriel ci adab bi ci des di bi ñu tax a jug moom nag adab la nu laaf ci ag l muy leegi ladab lu tax nu laaf ci l gi loolu ñi ngi ci roye lislaam te bu njëkk islaam la woon waaye ginnaaw ak l gi la ko wolof yi di gën a man di wax ak a tudd moo waral ci li nu wax nu koy boole ci baatu araab bi lii nag làkk woo gis ci àdduna bi am na ko boo demee ci araab da cee fees dell ay baay yu nu lem ba manees koo wax ci làkku araab te doonuñu woon ay baati araab ñu mujj bokk ci làmmiñu araab te bu njëkk bokkuñu ci woon lu ni mel fees na dell ci alquraan am it ci làmmiñu araab wu jamonoo wii sundus istabraq ak yu ni deme duñu ay baati araab te ñi ngi ci alquraan lu mel ni qubtaan di capitain dees koo jengal ba araab yi man koo wax waaye juddoowu ci añs waaye nag ladab ca daaray majaalis ya maanaam fa mag ña daan jànge nga xam ne seenuw jàngiin da daan tegu ci firi baat topp baat maanaam pirim baat baat nga xam ne lees la wax tekkil la ko ci wolof bu ñu nee bismil laa ne la maa ngi tàmbalee ci turu yalla ar rahmaani kay aji yërame ci àddina añs bu dee ci tekkiin wii adab di baat bi nuy wax ladab njàngat lees ko daa firee walla xam xamu mbind kon manees na ne ladab buñu bëggee muy wolofi kese ñu ne njàngat walla xam xamu mbind ci farse ci làkkuw angalteer literature ci mbindin mi walla waxin wi la ñuy sukkandiku ngir man a xammee xeeti njàngat yi su nu jàppee ne njàngat ab mbooloom ay baat yu am bopp di wax ci lenn li la kon man nanoo wax njàngatu xam xam njàngatu koom koom njàngatu diine njàngatu woy añs njàggat benn la ci anam yi nit di génnee ak a feeñale li nekk ci moom ciy yëgg yëgg aki xalaat aki ñeewant aki gis gis jaare ko ci ay mbind walla bindiin yu rafet te wuute moo xam woy la maanaam poesie walla wesar bind ci lu dul di ko nos maanaam safaanub woy walla wesar wu ñu nos loolu nqg di ubbil nit ay bunt ngir mu am man man ci feeñal ak génne li ñu manul a génne walla ñu koy man a feeñale ci geneen anam walla melo njàggat nag day takku takku gu dëgër ci làkk dëgg dëggi njuréef walla ngérte li juddoo ci làkk ñu bind ko walla caada ja ca juddoo day nekk di lu dencu walla lu wattuwu ci biir melokaani njàggat yi aki peeñ peeñam te ñoom danuy wuute kem ni gox yi di wuutee jamono yi di ko wuutee jamono ju nekk tam ay soppiku da ciy sosu akug jëm kanam akug wuute ak xeetu ànd ak jamono yi man ngéen a xool foofu ci suuf cuq ci lëkkalekaay yooyu ngir déglu as lëf ci wolofali sëñ mbay jaxate ak sëñ muusaa ka làmmiñ ak jamono dangeen di xam ne aw làmmiñ jëfandikukaay la boo xam ne lu am xel dem ci àdduna aw làmmiñ man na koo tudd am xel ay gàtt aw làmmiñ gàtt waaye lu am xel man a jëm ci àdduna rekk aw làmmiñ man na koo tudd aw làmmiñ gàttul nit kiy wax nag fi xelam yam fi jàngam yam fi gis gisu àddunaam yam foofu rekk la ay waxam man a yam waaye boo demee ba sam xel gis leneen rekk làmmiñ dina ko tudd lu ko waral amul benn baat boo xam ne bii yenu nga sa maanaa ci cosaan amul mooy li nga xam ne waxoon naa ne dinaa cuq tuuti xel yi ndax defe naa ne yéen jàng ngeen xam xamub làmmiñal xam ngeen ne de saussure boroom xam xam bu mag la woon ci wàllu làmmiñal wone na loolu làmmiñ du loo xam ne tay baat yi dañoo juddu rekk daal di yanu seeni maanaa baat bi coow luy génn ci gémmiñ kepp la kepp amul sax menn maanaa ndax bu ko amoon wenn làmmiñ ay am kon lu jug rekk xel yépp nenn lañu koy tudde wenn tur wi di moom te loolu amul jukki bii tibbees na ko ci waxtaanu seex anta jóob mu amoon ci awril ca cees xaralaymbëj mooy xeetu xam xam giy gëstu lépp lu jëm ci wàllug mbëj ay jëfandikuwiinam ak ay seddalewiinam bu njëkk dañoo foogoon ne mbëj ag wal la rekk guy dem gu man a nekk gu baax walla gu bon waaye ci ndimalu ay woroom xam xam yu mel ne hertz helmholtz maxwell heaviside alessandro volta ak ñeneen ñu bari ci lees dem ba gën a nànd xam mbir mi lu mel ne yamaleb maxwell biy faramfàce tëdiinu yani mbëj yi feppsaal ak mbëjfepp yiy wuute ci seen jublug yanub mbëj walla toolu mbëjbijjaakon ba ca juddoo ci gàttal ci noonu lañu tambalee gis yenn ci ay jëfandiku yu mbëj doxalukaay bu mbëj soppalikaay aki niitu tay xaralaymbëj moo yor wàllu sàkk ay wuutuloxoy mbëj ak ay buumi séddalekaayu kàttanug mbëj ay faramface ak ay àtte yi lal xaralaymbëj yamaleb maxwell yi ñooy àtte yu am solo yu ñeel mbëjbijjaakon ci la yeneen yi soqeekoo àtteb ohm om yiy faramface ndëgërlu gu mbëj gi àtteb faraday neumann lenz mooy faramface xiirtalug mbëjbijjaakon njeexitu joule mooy leeral ni kàttanu mbëj di soppeekoo nekk tangoor ngir njeexitu ndëgërlu gi àtteb kirchhoff kiirkof mooy leeral jëflante bi nekk ci diggante dawaan ak dend ci ag ndombo ag wàll gu am solo moo jëm ci lépp lu ñeel yokkte ak seddalewiinu kàttanu mbëj ba ca jëfandikuwaay ya barab yees koy jëfandikoo kàttan gi dees na ko jóox ci ndimbalul ay jurukaayu mbëj ci barab yees ko jagleel li ñuy wax diggub mbëj ci lu ëpp fa muy nekk day soree ak dëkkuwaay yi buumi séddalekaay yi dañu leen a lëkkale ci seen biir ñuy jëlee kàttan gi ca jóoxuwaay ya di ko yóbb ca jëfandikuwaay ya li wuutale buumi yóbbukaay yi mooy limu dend gi ñuy yóbb moo tax ñuy gis ay buumi dend gu kawe dend gu diggu dend gu diggu dend gu suufe su diggante jóoxuwaay yi guddee dañ fay def ay mbëjjaaru ay buumi dend gu kawe yu man a yóbb ay milioi watt ci kàttan tambalee ciy v buumi dend gu kawe yii la ñuy duppe yu yóbbug kàttanu mbëj yi nga xam ne ñooy tax a man a yóbb kàttanu mbëj gi jële ko ca jóoxuwaay ya jëmee ko ca barabu soppikaay ya ci nii la ñuy soppee dend gu kawe mu nekk dend gu diggu jaarale ko ci ay masin yu mbëj yees di duppee soppalikaay ci noonu la ñuy yóbboo kàttanu mbëj gi ca ndombo gu dend gu diggu moom ci boppam dañu koy àggal ci néegu seddalekaay yi jaarale ko cig ndombog séddaleg kàttanu mbëj foofa lañuy defee geneen coppite jëlee ko ci dend gu diggu soppi ko dend gu suufe ngir ñu man koo jox jëfandikukat yi ci kër yi ak liggéeyuwaay yi doxalukaay yu mbëj yi ay wuutuloxo lañu yu y soppi kattanu mbëj def ko kattanu doolerandu doxalukaay yi dañu leen a séddale ci jurukaayu mbëj yi ñoom ay wuutuloxo lañu yuy soppi kàttanu doolerandu def ko kàttanu mbëj yi ci gën a raññeewu soppalikaay ab wuutuloxo la maneelam mooy soppi limu dendu mbëj gi nekk ci ab ndombo ci yokkute walla wàññi lu mu néew néew di na am ñaari lëmës yu bijjaakon boole wuutuloxo yu man a yokk walla néewal taraay te di jëfandikoo benn lëmës rek lañuy tuddee soppiboppam ay jumtukaay lañu yu aajowoo soppi kàttanug mbëj mu nekk leer di ko jëfandikoo ngir leeral barab yi mbëj da di ag feeñte gu gisuwul ak bët guy feeñ ci ag wootalante walla bëmëxante ci diggante yani mbëj yi ci gattal mooy gépp feeñte gu juddu ci jàmmaarloo gi nekk ci diggante feppsaal yi ñoom ci lu ëpp da ñuy tekkaaral ak mbëjfepp yi nga xam ne ñoo ëpp yëngu yëngu ci biir xarefulwoon bi seenuw demiin jur ab dawaanu mbëj su ñu ko boole ak bijjaakon mu jur beneen banqaas bi ñu duppee mbëjbijjaakon mbëj moo yor ay feñte yu jëmm yu mel ne melax toolu mbëj ak dawaanu mbëj ci lu bari dañ leen di jaawale mbëj doon na jaamu nit bi gën doon tamit raññeekayu àdduna bu bees bi dafay leeral sunu dëkkuwaay yi di doxal sunu këri koom koom yi te jegeele nit ñi gënoon a soriyante yanub mbëj doon na lu ñu man a natt te man koo jëfandikoo waaye doonul lu neex a faramface ak ay baat yu yomb a nand ndaxte yombul leeral melokaan yi mu am dëgg dëgg xayna li gën mooy wax lan la ak li muy sabab lépp lu mu man a doon lu am yanub mbëj man nañoo wootalante walla bëmëxante li gëstu yi wone mooy am na ñaari xeeti yani mbëj benn bi lañuy woowe yan bu baax moom mooy nekk ci biir saalu xarefulwoonu ne ne yépp ak yan bu bon mbëjfepp ñoo nekk ci li wër saalu xarefulwoon yi naka jekk yan yu baax yu saalu xarefulwoon bi dañuy tolloo ak limu yan yu bon yu mbëjfepp yi ko wër ba fii danoo jàppoon ne gépp ndombo goo jël mbëjfepp yi dañuy yëngu saa su ne jëm ci benn jubluwaay ci biiram yenn saa yi nag dawaan bi du sax ci maase muy ci doole walla ci jubluwaay bi ag noste mbaa ag ndombo gu ne mel lees di wax dawaan bu wéy am misaal man naa nekk ag noste gu ab tegle di doxal donte sax aajowoowul dawaan bi di am genn jubluwaay gu sax bari nañu ndombo yu mbëj yees di jëfandikoo yuy safaan jubluwaayu seen dawaan ci biir ndombo gi gii xeetu dawaan lees di wax dawaan bu safaanu ndombo yu mbëj yu ëpp yi ñuy jëfandikoo dawaan bu safaanu lañu cig ndombo gu dawaan bu safaanu dafay laaj waxaale tamit baraayu ni dawaan bi di safaanoo taraayu dawaan bi ak dend bi ci ndombo gi moom rekk bu mujj bi doy na su fekkee dawaan bu wéy la ci baraay bi lañuy natte ñaata yoon la dawaan bi di soppi jubluwaay ci benn saa liy wër ab mbëjfepp walla leneen lu mu man a doon lu am ab yanub mbëj day am melokaanu luy dox moom lañuy tuddee toolu mbëj soo jallaxee ay mbëjfepp day am benn tool bu wër seenub jublu moom la ñuy tuddee toolu bijjaakon dooley tool boobu dafa aju ci limu mbëjfepp yiy daw ak seen gaawaay maanaam ci yeneeni kàddu ci dawaanu mbëj bi soo jallalee ab dawaan ci ag lëmës gu nekk wëñu përëm ci nimu waree lëmës googu day mel ne bijjaakon gu weñ day xëcc walla bëmëx yeneen lëmës yi mu yemal wëñ lëmës gu mel noonu su fekkee danga koo defaree ak ag wëñu përëm goo wëndeel cib weñ day gën a yokk toolu bijjaakon ba cay juddoo su fekkee dangaa am ay lëmës yu bari yu ñu wëndeel wëñ ci weñ yu man a wëndeelu nga boole leen ak yeneeni lëmës yu dul wëndeelu yu am toolu bijjaakon bu tar yu dawaan jaar day jur jenn dooley doolerandu doole joogu moy wëndeel lëmës yu man a wëndeelu yi mu daal di man a def liggéeyu doolerandu mu nekk ab jumtukaay bi ñuy woowe doxalukaay bu mbëj tay jii doxalukaay yu mbëj yi ñooy doxal bépp wuutuloxo tambalee bi ci gën a ndaw ba ca ba gën a ngande doxalukaay yi dañoo bari te am ay melokaan yu wuute njariñ li ci jëfandikooy noste yu dawaan bu safaanu moo ngi ci li ñuy man a yokk walla waññi dayoo bu ab dendam ci jëfandikoo jumtukaay bees di woowee soppalikaay ab soppalikaay ñaari taxañ yu tàqalikoo lay am yees ber yu ay wëñ yees lëmës cib dankub weñ saalu soppalikaay bi ab dawaan bu safaanu su walee ci taxañ bu njëkk bi ab toolu bijjaakon daf fay juddoo mu jur moom itam ab dend buy soppeeku ci jenn jamono ju nekk ci ñaareelu taxañ bi su ñu jëlee benn dayoo bu saal bi weñ gi ak yenn limi lëmësi wëñ yu taxañ yi dees na man a yokk walla waññi dend bi ci nees ko bëgge kon ab soppalikaay di nanu tax a man a jëfandikoo dend bu suufe ngir sunu kaaraange ci kër yi te terewul nu man koo jokkale mu jóge cib digg bu mbëj bu sori cib dend bu kawe manees naa jëfandikoo ab soppalikaay ciy fowekaay yu mbëj ak ci yeneen jumtukaay yu ndaw yu mbëj ba tay maneesul a jëfandikoo soppalikaay cig ndombo gu dawaan bu wéy ndaxte dawaan bi toolu bijjaakon ba muy jur duy soppiku doxalukaay bu mbëj ab wuutuloxob mbëj la boo xam ne kàttan giy duggu ci moom gu mbëj la te ga muy génne gu doolerandu la doxalukaay yu mbëj yi am nañu solo lool ci dundiinu jamono ju bees ji te it dëgg la sax ne limu doxalukaay yu mbëj yi nekk ci am réew dafay firndeel tolluwaayu jëm kanamam maanaam yokkug limu doxalukaay yu mbëj yi ci am réew bokk na ci wonekaay yiy firndeel tolluwaayu yokkuteem ci wàllu xarala mu réew moomu ngir dëggal loolu doy na xool ci jumtukaay yi nekk ci li ñu wër ca saxaar ba ci watukaay ak yeneen ak yeneen yi ngeen xam ne nit ku bees ki moo ngi koy jëfandikoo bu baax man naa ni sax ñooy doxal sunug dund doxalukaay yu mbëj yi dañoo bari te wuute am na doxalukaay bu dawaan bu wéy doxalukaay bu dawaan bu safaanu moom mu séddaliku ci doxalukaay bu demandoo ak doxalukaay bu demandoodi dawaanu mbëj bi day jaar ci ag lëmës gees wëndeel ci ab dogub weñ bi tudd tekkaaralaan bi lëmës googu gi ñu defare ak wëñu përëm naka jekk përëm lay doon waaye manees na koo defaree ak beneen xeetu wommatukaay dafay jur ab toolu mbëjbijjaakon tool bi dafay feeñ niki ag walug bijjaakon di lees man a natt danu koy jàppee niki jenn doole di lees di wax dooley lorentz toolu mbëjbijjaakon boobu dafay duggante ak toolu mbëjbijjaakon bu lëmës gu wëndeeluwaan bi jur mi melokaanoo teewaayu ñaar walla ñetti seexi dott wëndeeluwaan bi tambalee wëndeelu ci ndimbalu dooley lorentz bëj gànnaaru toolu bijjaakon bu wëndeeluwaan bi day bijjante ak bëj saalumu toolu bijjaakon bu tekkaaralaan bi xaaju wëndeelu gu nekk dott bi day soppeeku ci noonu la wëndeelu gi man a wéyee ci atum lu weesu xamteg feñte gu mbëjbijjaakon gi simikat boobu di rsted xamle woon la jëmmalkat bu waa angalteer bii di michael faraday defar ñaari wuutuloxo ngir sàkk li mu duppee ag wëndeelug mbëjbijjaakon ab doxub dooley bijjaakon bu mbegewu te wéy ci lu wër ab wëñ ci maanaa mooy faramfaceg doxalukaay bu mbëj gu njëkk xeeti doxalukaay yu mbëj yi am manees naa wax ne du xaaj du jeex waaye manees na cee lim yi ëpp yees di jëfandikoo xam xamu suuf si mooy li nuy wax jiyoloji xam xam la buy gëstu lépp lu aju ci suuf si kaw gi ak biir gi ak doj yi montaañ yi añs bu jawwu ji di biy gëstu lépp luy jawwu ak tegaloo gi ñu tegaloo jawwu ji nak mooy mbalaanum ngelaw li wër suuf si lees di gën a sori suuf si ngelaw liy gën di néew doole di gën di amadi day mujj sax di lu fàddu ci ay fukki culómet cig kawe lii a tax ñu man a séddale jawwu ji ci ay goxi jawwu yu wuute te tegaloo gox bu ci nekk ami jagley boppam fatt jawwu walla jawwu ju fatt ji mooy ji gën a tal gën a fatt te gën a féete suuf moom ngelawam day yëngu jamono ju nekk fa lay niir yi di sosoo ak mbooleem soppaxndikuy jawwu yi kon cig jege mooy jawwu ji ëpp ag jeexiital ci wàllug dëkk ci kaw suuf ak ci ni kilim bi di séddalikoo mbooleem beeñ bi ak doj yi ñoo sos wàll gu tond superficiel gu dëgër gu kol kolu suuf si ñu koy woowe jéeri ji walla aji wow ji bu ñu séddalee jéeri ji def ko ñeenti xaaj ñatt yi daanaka ndox yee leen muur yooyu ndox nag ñoo sos mbàmbulaan yi ak géej yi waaye wàll yi génn ci jéeri ji nga xam ne ndox yi muuruñu leen gox yi ak dun yi wàll yii ñooy wërlaay gu dëppoo te méngoo ak dundug nit moo tax fi la nit di dunde di fi defe ay liggéeyam walla li ëpp ci ay cawarteem activités jéeri ji nag day dund tey màgg ci anam gu sax ak doonte fi nun day mel ne ni mu nekke soppikuwul li ko waral nag mooy ni muy soppikoo day faral a yeex lool doj yi bu ñu sosoo ci ron géej gi dañuy mujj lemu yékkatiku màgg ànd ak jamono yu jiyoloji yi ñooy mujj sos ay càllalay doj yu yees ci safaanub loolu doj yi gaaru ci kanamu jëfkay jawwu yi dañuy xolliku di xoosu di fellu bu ko defee yooyu xoosiit ak felliit ban yeek beeñ yeek yi ni deme ñooy mujj sottikuwaat ci géej gi sëriñ muusa ka sëriñ muusa ka werekaanu bàmba woykatu wolof ak araab la woon bu mag te xarañ ci ab jullit la woon bu dëggu te di ab sufiyànke di taalubeb sëriñ tuubaa bokk it ci seexi sëriñ tuubaa yi taalif na lu sakkan ci ay téere ci wolof ak araab rawatina wolof ndax ki mu daa tagg wolof mooy làkku cosaanam muy sëriñ tuubaa sëriñam te sëriñam boobii it yonnent bi moo doon sëriñam bu ko daa tagg ci araab lakoy tagg ndax nit koo di tagg di ko tagge weneen làkk wu dul làkku juddoom tagg ga du mat ndax yaangi koy tuutalal cosaanam ay woyam nag li ci ëpp sëriñam la ciy tagg ak di soññ bokki taalubeem ngir ñu gën a fonk sëriñam te nankoo jaamu yàlla ku xelu la woon te jàng ba ci woyam yooyii mu woy ci wolof ku jàng aruud xam xamu woyiin ci araab ma nu koo jam sàmmoonte naak sarti woy ak bahru yi woyiin yi ba sos na ay bahru ajami niki téere bi tudd bu léen njuuj njaaj ak way wi mu jébbaloo ci seex mustafaa mbàkke xalifab seexul xadiim bu jëkk jiim gi jigéen ju ndaw araf ya lan ko tënke tënk ba bis pénc ba lan koy tinkee jiimug jigéen mooy jekki bum jàllantu ndaxte bu jàllantoo asal njaaloontu cofeel gu mat sëkk a ko war cib sëriñam ku bëgg dof te ku doful doo am ngërëm jaamu boroomam jaamu it boroom këram moo war jigéen su ko manee dàmmey ngëram jam tuñ ma jam siiñ ma ak njamal yàllaam la jaalu yàllaam wa ne yaasin salla a jàmm ak juddook jikkoo waral ñuy tànn ne xur wi wenn la te jiim yiy jenn kaaf gi kaaf nga na baax gaaf bari ngor toog fa këram na bari kersay kër këriy sàkku ngërëm nay gone bum def mag te bum gàtt kutuj bum gudd lool fum toll ànd ak latkoloñ yaa gi yaa ga na yaatu àpp yaatal dëkkandoom yaatal boroom këram ci lépp lu mu moom yaru te yomb te yéwén te yaatu cib sëriñam te la mu yor bum laatu arafu nuun gi arafu nuun gii ku ko boole xejj ci sa boroom kër gaa ya duñ la xàjji neex cere neex dereet te neexu làmmiñ neex lépp tey neexlaate gàttu gémmiñ jigéen na maandu man a muñ te mokk di muñ di muuñ di mooñ cereem ne mekk arafu baa yile jigéen ju boole seen jikko yii kenn du la ba ngay xoole baax baay te booleek bari bayreek barile ba su boroom këram amul muy defale bëñam ya weex tàll ba mel ne perkaal bët ba ne bàq bakkanam bay safu jaal day neexu làmmiñ neexu ñam te mokk lool lewet te nooy ku mu dajeel sukkal la teel adunyaa ngi tol new fel fi moom mbaate dëññu teeñ woroomiy tëndë xammeewu leen ak woroomi téeñ lilee tax mu daa tuubloo dameel ak maxa aki teeñ ku mel nii ku amleek moom na leen wóor ne yaa ko tooñ du tooñ nit te soo tooñee mu jéggal la tin la ko xamul jaamur ak mbokkam mag ak ndaw ci aw meloom wurus mbaate ab xaalis bëy ak nag xar ak gëléem la daa buub di jox ñiy laaj du kuy néegaleek a léem añs ngir déglu te yér as lëf ci woyi sëriñ musaa ka xoolal foofu taariixu àdduna bu bees bi te jamonoo ag jiital teeree ngi nii buy gàttal yoonu xam ndax li nga daa lijjantee xam ciy fan ak cib coona moom la lay xamal ciy waxtu ci lu dulub coona muy bu nu def ngir feeñal ci baat ak waxiin yiy war a wuutu yu fraanse yu bari yu nuy teg ci barabi yu wolof yi te kat fekk na wolof amoon leen mbaa mu manoon leen a am te nu jàpp ne manunoo doylu wëlif leen ma yaakaar ne bu nu bëggee yombal dëgg lu mu metti metti danoo war a wut ay kunaked babies in my asshole utlaay ñeel baati doxandeem yii bëgg a ruur sunu làkk wi te nag yombug xam xam mi ngi ci nga koy jàng mel ni jàngoo kon lu tax muy franais ginaaw du lu moy ab jumtukaay ngir xam ngir déggante waxante te ma gis ne bu dee ci ay wolof seen làkk lay gën a nekke jumtukaay boobu lii ak leneen lu bari moo ma yobbu ci di xalaat ci di binde ci wolof te ba yeneen kàllaama yi ginaaw bindaluma ku leen moy te it nag ni ñepp def ba ami làkk lu tax dunu ko def bay am sunu yos ñun itam waa afrig nekkewunu fi lu dul ligeeyal tugal ak lu ni mel nanu sunu bopp ñor doonte as lëf la it nan la am reew mu tollu ne senegaal ñépp di waxi wolof nga ne fraanse rekk reerale ga a ngii i have a incher abdul xaadir kebe bunt bu njëkk bi njëlbéenug jamono yu yees yi doggantal gu njëkk gi 	 yewwute ga amoon ca tugal yëngu yëngu googu nag mi ngi tàmbli ci xarnu bu fukk ak ñatt ginaaw juddu gu yonnant yàlla hiisaa ba ci bu fukk ak juroom ñaar mu sos fi nag ay soppi yu xóot ci wàllug aada dundiin mboolaay politig ak koom koom kon daal yewwute gii amoon ca jamono yooya ca tugal li muy wund mooy ag tuxu juge ca jamono ju diggu ja mu y jamono y ag laman walla ag cang dem ci jamono ju yees ji di ju jëm kanam gu xam xam ak xarala sabab yi tax yewwute g orob gi am sabab yi jur yewwute gii yu bari lañu waaye nañu ci indi ñatt yi ci ëpp solo rekk ñooy jeexiit gi lislaam amal ci yewwute g orob gi ci waxtu wi tugal nekke cig deltu ginaaw ci wàllug xay ci jamono yu diggu yi nga xam ne jàngu bi egliis bi faagaagaloon na bépp xalaat bu leer te gore araamal ci nit ñi ñuy xool leneen lu dul am njàggaleem mu way deng mii te doxadi bi orob nekke ci lëndëmam gii jullit ñi ñoom ñi ngi doon jëm kanam bu baax ci yekkati tabaxub seenug xay ci kaw ay cëslaay yu xam xam ak wisaare maandute ak mbokko ci diggante nit ñi ci lu dul xool xeet walla melo mbaaw làkk xayug lislaam gi nag àgg na tugal jaare ko ci yoon yu bari bokk na ci yooyu andalusi ak sisil ak reewi penkub lislaam bi rawati na ci xarey jooñ yi ndax kat booy xool li tugal di nekk lépp di ku ñu dàqe ca xarey jooñ ya duma ko ca teewul mu fàggoo ca njariñ lu bari ngir fenqoo gi mu ci defe ak xalaatub lislaam bi ak nosteg dundam lii nag ci li soppi xalaati waa tugal yi la jëm ci egliis bi nit adduna bi ak dund gi te itam lu bari ci sàkkukati xam xami tugal yi dañoo tàmbli woon di naan ci xam xami lislaam yi ci ndoktoor xeltu gañcax ak ndundat ak yu dul yooyu ci jàngu yu andalusi yi la ko dale ca xarnub fukk ak benn g loolu nag taxoon na ba yëngu yëngu gu firi walla tekki gu mag amoon ci xam xami lislaam yi tukkee ci làkku araab dem ci wu latin wi doon wu xalaat wu diine tey wu politig ca orob ca jamono jooja loolu dimblee woon ci ginaaw bi ci lal yoon wi ba yewwute gu tugal gi man a am feeñug dëkk yu mag yu tugal yi les villes bu ko defee li ñuy wax tool di suuf si sang biy moom moo daa tekki barabu dëkkuwaay bi koom koom bi mboolaay gi ci gii noste màggug dëkki tugal yi ngir màggug yaxantu gi nu daa def ak mboolaayi jullit ñi ak màggug mecce yi ak ligéey yi ngir jòkkoo gi waa orob gii daa def ak jullit ñi taxoon na ba nosteg laman tàmbli woon a lòtt ak a naaxsaay rawati na bi nitug tugal ki tàmblee am yoon wu mu man a jaar bay dund te du sukkandiku ci léppam ci suuf ak tool waaye ci yeneen ligéey yu koom yi dëkk yi tam tàmblee doon barabi leer yu di boroomi xay di sonnale ci loolu ak a lakkal noste gu laman gi tey ligeey cig màbbam def it lu rëy ba yewwute ci tugal man a am lòttug egliis bu paab bi akug tasam egliis bi moo nekkoon di teg loxo ci dundug xalaat gi gu diine gi ak gu aada gi ci tugal gépp te yitteem jépp mi ngi ko sotti woon ci njàngum pas pasu diney nasaraan walla li nuy wax njàng yi aju ci yàlla théologie ak njàggat ak xellu amutoon jenn yitte ci njàng yi aju ci xam xam egliis bi moom dafa jàppe woon boppam ki nga xam ne ci yoon moo war a doxal mbiri politig yi te kat moom egliis bi tawati mbon akug yàqu dañoo ruuroon aw yaramam dugg ko fépp ba waral aw nit wu jàng te yewwu jug taxaw temb ci dañal ñaawteef yooyu ko taqoon loolu tam bokk na ci li jañoon xelum nitug tugal ki ci mu jëm kanam gën a ñaw rawati na bi dëkk yi gënee yaatu deggiinu ligeeyub yaxantu gën fa a xóot ak bu endustri ak aada yii yepp nag ligeey nanu lu rëy ci waxuma la doyodil ngëb gu tar gi paab gi ngëboon mboolaayu tugal gu nasaraan gi waaye it doyodil nosteg laman gi loolu it di doyodil nosteg laman gi rataxal yoon wi ba yewwute gi man a am itaali mberum yewwuteg tugal gi dëkk yu itaali yi ñooy mber mu njëkk mi njëkk a uuf tete yewwuteg tugal gi looloo waraloon ñu am wàccuwaay bu kawe akug wormaal ci yeneen dëkki tugal yi ca jamono jooja dëkk yii niki milano ak venezia ak firenze ak napoli ñoo uufoon yewwute gi seeni boroom xam xam aki njàggatkat ak artist walla waa fànn duggaloon nanu ci seen loxo bu baax li waraloon loolu nag lu bari la bokk na ci dal ga fa amoon ak jàmm ja ak jëm kanamug koom koom ba ak yaatug yëngu yënguy nitu itaali ki ak ba tay yaatug goxi xalaatam ak yëg gu mu yëg gore gu mu am ginaaw bi mu goree ci nosteg laman ak li itaali yàgg a am ci teddnga gu sax ak jaloore mu y njàggati waa rom yi seeni xam xam seeni jeexiit ak seeni fann nga rax ci loolu nekk gi paab gi nekk rom nga xam ne loolu faggul na waa itaali ag cang gu diine ni nga xame ne barab boobu it di itaali faggul na paab gi ci itaali ag tono gu ne ne ak gu maanaa gu mag nga rax ci dolli gëpplante gu mag gi amoon ci diggante dëkk yu mag yi ak peeyi buuri itaali yi ci wàllug njàggat ak fànn ak soññ gi doxalkati dëkk yii ak buur yi daa def boroom xam xam yi daa ligeeyal yewwute gi ak ba tay yittewoo gi nga xam ne amoon na ci dëkk yii aju ci gëstu mbind ak taalif yu yàgg ya ak barig móolukaayi teere yi ci yii dëkk ak nag li itaali doon xéewoo muy nekk ci barab bu raññiku buy dimblee ci jokkoo ak addunay jullit ñi mandargay yewwuteg tugal gi yewwuteg tugal gi mi ngi ame ci mbooleem wàlli dundug nit gu xalaat gu fànn gu politig gu diine ak gu koom koom yii di ñëw ñoo ciy wàll yi gën a rëy yëngu yëngu yi aju cig nite ag nite li miy wund fii mooy dundal njàggat yu yàgg ya yu gres ya ak rom ak feddali sukkandiku gu nit war a sukkandiku ci boppam akug goreem ak sañ sañu wax li nekk ci moom ak dog gàllankoor yu mboolaay yi ak jële fi aaday jamono yu diggu yi ak sotti yitte yi ci adduna bi ak dénd bi ak jeem a xam seeni mbóot yëngu yëngu googu nag bokk na ci màndargay yewwuteg tugal gu njëkk gi ndaxte li mu yittewoo woon mooy xam xam yu kojug nite yi nga xam ne njàggatkati gres yeek rom grego romain ñoom lanu jëloon yittewoo leen ak seeni xeltukat ak seeni boroom xam xam ak ñoñ fànn ak seen boroom mecce yu muus yi te ñaw boroom xam xam yi daa def gëstu yooyu di kojug nite ñi ngi leen di woowe ñoñ nite walla boroom njàggat yi ñoñ nite kon ñooy mbooloom nit mi yittewoo woon jàng njàggat xam xam ak fànn yu yàgg ya yu klaasik ya maanaam njàggati gres ak rom ak seeni fànn ak xam xam yëngu yëngug nit gii nag judd na ginaaw bi mu amee ag jàpple gu tukkee ci kilifay dëkki itaali yi ak seeni boroom alal ñoñ nite ñi génne woon nanu ab taar feeñal ko ci mbooleem fànn yu wuute yi moo xam yatt la mbaa nataal ak deseñ ak misik ak tabax ñoñ fànn ñu itaali ñi ak ñu dul ñoom ci jamonoy yewwute dañu doon roy fànn bu klaasik bi di bu gres rom bi bàyyi nee nag fànn bi nu daa wax xóot nga xam ne moo amoon ca tugal ca jamono ju diggu ja bu ko defee ñoñ fànn ñi jëmale seen fànn ci taarub dénd bi ak dund gu yees gii nga xam ne mooy gisiin wu jëm kanam wi nu am ci dund gi dëkki itaali yi gis nañu aw tabaxiin wu bees ndax wacc nanu nee tabaxiinu xóot wiy am ay poto yu ñu catal te weccee ko ak tabaxiin wu klaasik wi raññikoo ay poto yu am ay ndëpp yu rafet aki jagle mbaa deseñ yu eesañeri mel ne yi daa am ca tabaxiinu gres wa tabaxiin wii siw na lool te tas ci egliis yi ak katedraal yi ak saal yi ak barabi tiyaatar yi ak sangukaay yi ci dëkki itaali yii lu bari ci waa fànn yu siw yi fa lañu feeñe bokk na ci ñooñu deseñkat bu siw ba di fra angeliko mi nga xam ne dees na ko lim mu bokk ci waa fànn yi raw te gën a mag ñi nga xam ne ñoo doon gëstu modeli fànn yu yàgg ya ay ligeeyam itam dañoo raññikoo woon màndargam diine mu dal mu nekkoon moom ku diinewu bokkoon na ci ñoom it leonardo da vinci moom mi boole woon fànn ak xam xam defar nay nataali fànn yu siw bokk na ci yooyu bi tudd reer bu mujj bi ak jokanda walla mona liza ñaari nataal yii ci yi gën a siw lañu ci deseñi jamonoy yewwute da vinci mii nekkutoon ab deseñkat bu aay rekk waaye raxoon na ci dib yattkat bu mag dib rëddkatu tabax te dib eesañër bu muus bokk na ci deseñkati itaali yu yewwute gi ba tay ki ñuy wax titian moo nataaloon ay wàll ci dundug ñu féex ñi walla aristokraat yi ci dëkki yaxantu yi ak fànn yi ak rafayel g moom itam rëddkatu tabax bu siw la woon te di deseñkat bu bokk ci ñi gën a siw ci mbooleem jamono yi bokk na ci ñoñ fànni yewwute gi ci itaali ba tay yattkat ba donatello mooy ki sukkandiku woon ci yattam ca yattiin yu klaasik ya di gres rom rax ci dooli ku yittewoo woon taarub dénd bi la ak ag dundam moom daal ca dëgg dëgg moom la nuy jàppe ki sos te taxawal yatt gu bees gi feeñug làkk yu bees yi làkku latin ci jamono yu diggdoomu yi moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam xam ya ak niti diine ya ak politgkat ya ak njaggatkat ya ak ustaas ya la notoon nag ca nit ña di woon niti neen ñi rekk ñoom déggunu woon wii làkk lu tumbrànke la woon ca ñoom seen làkki bopp yiy yu seeni barab lañu déggoon bi jamonoy yewwute dikkee ngelawul fonk sa xeet upp ci orob gepp la lu bari ci xalaatkat yi ak njàggatkat yi ak woykat yi tàmblee jng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki réewi bopp niki wu itaali wu espaañ wu fraans wu angalteer ak yu dul yooyu bi mu ko defee woykatu itaali bi tuddoon dante g taalif komedi bu sell bi ci làkku itaali naka noonu petrarch g mii nga xam ne li mu gisoon mooy làkku romam wii daal mooy gën ja a kawey jumtukaay ngir génne xasiday woyam yi bu ko defee miguel de cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di don kixota ci làkku espaañ ci noonu it la rabelais g def moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di wu fraans ngir wuññi ci liy yëngu ci biiram ci njàggat lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor kaf chaucer mi dib angle g jug moom itam sotti ciw làkkam woyam yu yéeme yi cib taar rawati na nettaliy kentrebry yi nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati angalteer yu mag yi yi gën a siw feeñug xeeti orob yu yees yi màggug fonk sa xeet ak sa reew ci tugal juroon na ci jamonoy yewwute ay reew yu bari ci orob taxaw yu amoon ag temb ci noonu yittewoo xalaati fonk sa xeet daal di fay feeñ fés fa lu aju ci temb tam di lu ñu fay waxtaane ak àttewiin yi looloo tax xarnub fukk ak juroom daa tàmblee dugg rekk xataati politig yooyu ak yu dul ñoom tàmblee am ay maanaa yu nu man a laal ci xeli lu bari ci nit ñi ci noonu xeet yu bari ci yu orob yi tàmblee feddali yooyule xalaat ci jëf di goreel seen bopp ci toppub jàmbur te jambur boobu weesuwul woon paab bi ak imbratoor bi ay àtte nag yu tugal yu am ay nekkte yu politig yu temb juddoo ci loolu ci ginaaw bi yu am seeni làkki bopp yu yees di ya nit ña daa waxe ay xarnuy xarnu waaye taxutoon ñuy làkki politig yi ak xalaat lu dul ci jamonoy yewwute gi yëngu yënguy dajale mbind yi dëkki itaali yi ak reewi tugal gu sowwu gi ci jamonoy yewwute dañu doon yittewoo dajale mbind yi ci fi ñu jortoon ne fi lanu nekk ci xustantin ak ci dëkki gres yi ak ci yeneen barab yi ci tugal mbind yooyu ñu daa wër nag ñooy yu gres yeek latin yi nekkoon di lu ñu tas ci kàgguy daara yeek egliis yi ak katedraal yi ak ci nit ñi walla kër yi yittewoo woon mbir mii peey yi daan àtte dañu daa jagleel lii alal ju bari ñoñ nite ñi tam ñu ci bari jëmale woon nanu seeni ligeey ci dajale mbind yi ci noonu ñu jot a am ci misaal rekk mbindu m binkat bii di waa rom te dib xutbakat tuddoon quintilian nj g ak bataaxeli cicero nj yu xutba yi ak woy yu at ba at yu tacitus yi g tacitus moomu mooy taarixkatu xeexi jarmaan yi mi ngi bokkoon ci ñi gënoon a ñaw ci xutbakati rom yi ak seeni njàggatkat yu ñaw yi sonn ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya yewwuteg orob gi yittewoo woon na te sonnoon ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya ag jublu gu yees am ci jàngiinu taarix ñu koy teg leegi ci cëslaayu jam waaye tegeesatu ko rekk ci dégg ak nettali ci noonu ab jàngu sosu ci firenze am njàngaleem jëm ci jam gu taarix mu tudd daaray xam xam bu taarix bokkoon na ci boroom xam xam yi ci gënoon a duggal seen loxo nitu taarix kii di lorenzo valla g mooy ki jamoon te diiatoon benn dosye bu taarix sikkoon it ag wéram mooy li ñuy wax mayug xustantin mooy dosye boobu nga xam ne paab yi yàgg nañu cee sukkandiku la ko dale ca xarnub fukk ak ñaar g ci seen xeex yi nu doon def ak buur yu mag yi ngir feddali ci seen àqi politig ci àtte nit ñi jiite leen bokk na ci ñi nga xam ne yittewoo woon nañu gëstuy taarix yi ak yu politig yi bindkatu itaali bii di xalaatkat bu politig bu am diplomasi di nicola michiavelli g michiavelli mii def na teere bu mu tudde woon buur bi ndax da ci doon wax lu aju ci buur bu am doole bu doon bennale dëkki itaali yi ak nguur nguuraanam yu daggatoo woon yi te tas jëm kanamug yaxantu ak endustri yaxantu noyyi na bu baax ci orob gu sowwu gi dale ko ci njëlbeenug xarnub fukk ak benn g itaali fi mu feete dimbli na ko bu baax ci yëngu yëngug yaxantu dox fa te jëm fa kanam ci noonu lonkoo yu yaxantu yi tàmbli fa a sosu di jëli marsandiisi penku yi niki sooy ak cuub yi ak rëndaay yi ak wurus ak bëñu ñay ak yu dul yooyu ginaaw bi it yii lonkoo ginaaw bi ñu gënee jëm kanam tàmblee yòbbu yii silaa ci yeneen dëkki orob yi bu ko defee bu ñuy dëpp di indaale marsandiisi orob yi niki ngëndal ak der ak firaa jëm kanamug yaxantu googu ak gu meccey endustri yi jur nañu ag xereñ ci denciinu alal akug jëm kanam ci kee yi ñuy jëfandikoo ci jëfi yaxantu yooyu ci noonu am mbooloom ay sandikaay mecce feeñ mujj teg loxo ci ginaaw bi ci fepp fu koom nekk te am fa cawarte naka noonu nu def ay ligeey yu mag ci wàlli mboolaay ak politig ak xalaat raxaatal ci loolu juddug maas gu diggu gi ñooy mbooloo miy ligeeye yaxantu ak yeneen mecce yu wuute yi feeñug yëngu yëngug xam xam gu yees gi yewwute gi ci njëlbeen gi dafa sotti woon yitteem ci dundal njàggat yi ak fànn yi ginaaw bi mu dox as lëf ba àgg ci mbooleem lu xay gu mat laaj ci noonu yewwute gi matale mbooleem dundug mboolaay gi bokk na ci xam xami dëppale yi ndaxte xam xam moom màggoon na ci dëkki orob yi jàngu yu mag yi sosu ci orob gi rawati na ci dëkki itaali yi yëngu yëngug xam xam googu mi ngi tàmblee ci di jeem a dundal xam xam yu yàgg ya ginaaw bi mu dox jëm kanam loolu nag li ko waraloon mooy jariñu gi mu defoon ci yoonu xam xam woowu di wu kojug nattu maanaam lu nekk looy wax nga teg ci sa loxo mu leer la ne loolu la nga doog ne moom la ndax wóore na la ci làmb gi nga ko làmb ba daj ko yoonu gëstu woowu nag mooy wi boroom xam xami jullit ñi jaaroon ci noonu boroom xam xamu fisiyaa bu angalteer bi ñuy wax roger bacon feeñ di njiitul gëstug xam xam ci tugal becon mii mi ngi sukkandiku woon ci yoonu jakkarloo ak nattu ci gëstoom yooyu nga xam ne àggale woon nanu ko ci ay ngérte yu am solo ci xam xamu bidiw ak bu weer yi ak yu matematik yi ak juxraaf naka noonu boroom xam xamu xeltu ak politig bu angalteer boobu di francis bacon moom itam feeñ g di koo xam ne dafa jëfandikoo xel ci àgg ci dëgg yu xam xam yi ci noonu ci gisiin mooy ki teg ponki ngérum xam xam mu bees mi ak doonte moom doonul woon boroom xam xamu dénd boroom xam xamu itaali bi leonardo da vinci g moom tam feeñ di kok dafa yittewoo woon jiyoloji bu mekanig ak matematig ak yu dul yooyu nga rax ci dolli fànnu yatt ak nataal ak misik ak eeseñëri mu nekkoon daal boroom xam xam te di nitu fànn tey fentkat naka noonu boroom xamu itaali bii di galileo g feeñ mooy ki njëkk a defar nattukaayu tàngoor njëkk a fuglu bidiw yi ca fesalukaayam ba dëgëral te feddali gisiinu boroom xam xamu bidiw bu poloñ bii di copernicus g bokk na ci màndargay xam xam yeneen yu yewwute gi fentug móolukaayu teere ci loxol nitug almaañ kii di john gutenberg atum g fent gii ak doonte gu almaañ la teewul jëmale na kanam bu baax dundug nit ci biir tugal ak biteem wuññiy juxraaf yi tam ci màndargay yewwute gi la woon ak yéwénalug diine gi ci tugal nga dolli ci loolu feddali gu nitug tugal ki feddali jëmmam jii nga xam ne yàgg na a nekk di lu nu làq ci jamono yu diggu yi ci biir ay kureel walla sandikaay mecce yi mu daa bokk ngir làqatoo ca ak aar njàriñi boppam yewwute gi ci itaali yewwute gi ci itaali daa tàmbli woon a giim ak a yànnjadi ci mujji fukk ak juroomeelu xarnu g ak njëlbeeni fukk ak juroom benneelu xarnu g loolu nag li ko waral lu bari la ñu jéem cee indi yenn rekk yi ci ëpp solo attekaay yooyu mosal nanu ginaaw bu àtteb lislaam dañee ca andalusi te garanada nërméelu daanu mosal nañu lu bari ci jullit ñi ay xeeti mbugal ak coona lu maneesul a misaal bokk na ci di leen lakk ñuy dund tuxug yewwute gi ak li yewwute gi di neew doole ci itaali lepp taxul mu naaxsaay mbaa mu suux li am kay mooy da fa a tuxoo dem ci yeneen reew yu tugal niki espaañ portigaal fraans angalteer holand ak almaañ añs ay jëfka yu bari bokk nanu ci li tuxale yewwute gi jële ko itaali yòbbu ko ci yii dëkki orob bokk na ci yooyu nekk gu yii dëkk nekk di yuy door a noppi ci seenug sosu gu politig gu yees ak tàbbi gu ñuy doog a def ci jamonoy tabax ag xay ñi daa woote yewwute gi nag def nanu lu rëy ci tuxale ko itaali mu dem feneen nitug holand kii di erasmus g moo tasoon te wisare yewwute gi ci almaañ jaarale ko ci def fa ay waxtaan aki xutba ak ci yeneen dëkk yu orob yi erasmus mooy ki firi injiil jële ko ci làkku gres yòbbu ko ci wu latin jël nag li ñu ciy wax kòllare gu yees gi def ko ci ay làkki orob yu bees loolu bokk ci li feexal te goreel xalaatub tugal bi ci ngartaajoo gi ko niti diiney katolig yi ngartaajoo woon loolu it won na waa tugal ne yaxub injiilub latin bi egliis bi yoroon du woon biy cosaan te yax bu bari woon ay yàq la kon daal eramus mooy ki waajal xelum tugal mi ci mu man a nangu yéwénali diine yi ni yewwute gi meloon ci fu dul itaali yewwute gi ca almaañ dafa yoroon melow njàngat wiy ligeeyal gëstuy diine yi ci manaa daa yamoon daanaka ci lu aju ci diine rekk ca dëgg dëgg gëstu yi aju ci xam xami gres latin yi dafa xawoon a yeex a àgg ca dëkk yooyu di yu almaañ ak li njiiti yooyu dëkk daa dimbli gëstu yooyu lepp cig wàll ak li almaañ doon am ay daara yu mag ci vienne ak idelberg ak baasal ak strasburg ak yu dul yooyu lepp ci geneen wàll yeex googu nag li ko waraloon mooy niti diine yi ak ñu dul ñoom ñoo ko nanguwutoon ñoom daal danu fee nekkoon rekk di sàkku nu ñu tënke te jéng yooyu njàng ak gëstu te defi pexe ba du ñu tas ci anam gu yaatu ngir nu wattoo ci seen kilifteef sàmme ci seen daraja aare ci seen ligéey ci noonu danañu gendiku ne yëngug nite gi ci almaañ dafa doon sori jubluwaay yu deet diine yi looloo tax du kiimaan almaañ di woon barab bi uufoon yëngu yu yéwénali diine yi gënoon a am solo ci tugal bu dee ci fraans moom yewwute gi melow njàngat ak nite la fa yoroon wi yittewoo woon xam xami gres yi ci noonu boroom xam xami itaali yi ak yu gres yi taxaw ci wisaare gëstuy xam xami gres yi ñu móol teerey ndonoy gres yi ci móolukaayu paris ba ñu taxawaloon ca xarnub fukk ak juroom benn g ni nu duggale seen loxo ci amal ay akaadimi aki barabi xam xam ngir njàng yi aju ci nite niki bànqaasub buur bi ci paris ñu sos ko ci jamonoy buurub fraans bi di fransuwaa mu njëkk mi atum g bu dee ci angalteer ba tay yewwute gi ma nga fa yoroon melow njàngat ak nite ay gëstu yu xam xami gres yi am fa ay ñoñ nite ñu waa reew ma ñu bari ñooy ña ca siwoon ñoom ñooy ñi daa jàngale làkkuw grees wi ci daaray xam xami itaali yi ku ci mel ne wilyam lilly mi daa jangale làkkuw gres ca rom erasmus mu olaand mi ak kolt mu angalteer mi ñoo tekki woon injiil ci làkkuw angale wu bees wi buurub angalteer bi henri mu juroom ñatteel mi moom tam sosoon fa juroomi toogu yu darajay ag ustaas ci xam xami pas pasu nasaraan ak yoonu siwil ak wu dénd bi ak làkku ebrë ak wu gres ci daara ju mag ju kembrij jàngub san pool bi nekk london moom it jagoo woon njàng yu nite yi yewwute gi ci angalteer dafa jublu woon yoonu takk ak boole diggante pas pasu nasaraan ak gëstuy nite yu njàngat ak yu fànn yi yewwute googu nag indiwul woon lu yees lu ñu fent ndare ci xarnub fukk ak jurom ñaar g bi am njurum njàggatam ak mu niteem mu yees feeñee ci anam gu fes te rafet ci woyi william shakespeare yi g ak woykat bu silmaxa bii di john milton g ak ñu dul ñoom ñaar fii tam ci angalteer yoonu yewwute gi da fee jengoon as lef jëm ci yewwute gu xam xam gu aju ci xam xami dëppale yi walla xam xami nattu yu làmb yi ñi jiitu woon ci lef moomu ñooy ñaari boroom xam xami angalteer yii di roger becon ak francis becon ñoom daal ca dëgg dëgg ñooy ñi sos daaray xam xam ca angalteer baat bi nuy mujj a wax ci yewwuteg tugal gi mooy moom daal moo ñàkkal jamono yu diggu yi kàttan ci jeexiital ci mboolaayu tugal gi ci wàlli dundug politigam gu mboolaayam gu xalaatam ak gu aadaam ngir jeexiit yii fi yewwute gi sotti ci orob ay noste yu yees am nañu yu làmboo tabax guur gu yees gi ak mboolaayug orob gi ci cëslaay yu aada yu mboolaay yu jikko ak yu ngér yu yees ni mu duggale loxo ba tay ci ubbi ay gox yu yees yu xam xam yu jël gisiini xam xam yi ak dal yu xam xami juxraaf yi lii lépp nag moo sabab jamono ju yees ci orob di ju wuuteek ja woon ca jamonoy laman ci xalaat ak ngér ak defiin aki xew xew loolu lepp nag nga boole ko moo jur jamonoy tugal ju yees jii doggantal gu ñaareel gi wuññi yu juxraaf yi luy wuññi yu juxraaf yi yëngu yëngu gu wuññi gu juxraaf walla feeñal gu juxraaf yëngu yëngu gu yàgg la waa isipt ñu njëkk ña ak finiix yi ak jullit ñi defoon nañu ko bu yàgg njëkk waa orob di ko def ci jamono ju yees ji lu am soloo ngii nag ñu war koo xam mooy wuññi y juxraaf yi bi muy am it li ko taxoon a jug mooy ay xemmemteefi sañc ak doonte daa mbubboo woon gëstu gu aju ci xam xamu juxraaf yëngu yëngu gu wuññi gu juxraaf gi ñuy waxtaane ci doggantal gii da nanu ko man a xamalee ci nii mooy mbooloom ligeey yi jéngukat yu tugal yi daa def ci ñaari xarnu yii bu fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom benn g yenn nag ci réewi tugal yu nasaraan yi ñoo leen doon soññ ak a jàmbaarloo ak a xiirtal ci loolu li sabab wuññi yii sababu diine moo jiitu ci sabab yi waraloon yëngu yëngu yu wuññi yu juxraaf yu orob yii am sababu diine mooy li gën a waral ñaari reewi katolig yii di espaañ ak portigaal defoon ligeeyub wuññi boobu ñoom yile ñaari reew dañoo jortoon ne dananu man a sutuxlu ci biir afrig ak fu dul moom def ko barab bu dëppoo ak li ñu bëgg muy tas fa ag katolig ak nangu ko teg ko loxo jaare ko ci diine reewum portigaal moom daa gisoon ne reewum ecopi mii di mu nasaraan waaye di mu yoroon ngérum xibt mu ortodoksi man na koo soppi def ko mu yor ngérum katolig loolu nag da nga ci gise diinewu gu dëgër gi amoon ci waa espaañ ak waa portigaal ca jooja jamono paab gi moom da daa soññ reewi nasaraan yi ci ñu dugg bu baax ci wuññi yooyu ngir tas ag katolig ak xatal lislaam te sonnal ko tee koo tas ngir neewal dooleem xottite ko giir ko ci noonu mu moom paab gi génne ay mbind yuy jox àq ñaari reew yii ci ñu moom gox yu yees yi ak mbooleem yu nu wuññiwaat moo xam geej yi la mbaa jeeri yi paab gi ak nasaraan yi ci ginaawam dañoo ragaloon lislaam ak ñoñam looloo taxoon ñu daa wut nu ñu mucce ci ñoom ñu ne woon kon nanu leen fi jeem a jële am na yeneen reew yu yees yu feeñ ci ëttub politig bu tugal bi yu ci mel ni espaañ portigaal angalteer fraans holand ak yu dul yooyu réew yii nag dañoo tàmbli woon di xalaat bu baax ci tas ak wisaare seeni kilifteef ak jeexiit ci biti seen rawati na ci reew yi ci yeex ci seenu g nekku walla sosu gu yees ñu gisoon it ne bu ñu fa tasee wisaare fa seeni xay aki ngéri diine loolu da na man a nekk ay raas yu ñu man a jaare ngir sampu fa sanc leen reew yii nag joante woon nañu te gëpplante ci mii lef loolu bokk ci li daa soññ ak a xiirtale ci yëngug wuññi gu juxraaf gi waa orob yi ñoom dañoo gisoon ne addunay jullit ñi daal mooy ji ngëp ci loxoom nosub yaxantu bi ndaxte ñooy ñi notoon tegoon loxo ci kaw yooni yaxantu yu penku yi ci noonu xalaatu wacci fi yooyu yoon te gëstuji yeneen yu leen man a àggale end ak siin tàmblee feeñ ngir bañ a fay njëgi nduwaañ yi ak galag yeek yeneen yi cig wàll ak ngir neewal doole koom koomu jullit ñi ci geneen wàll ginaaw bi ñu soppee yoon yooyu def leen leegi ñu jaar afrig ak màmbulaan gu atlas gi loolu lépp ngir bañ a jaar fi jullit ñi dëkke yenn ci réewi tugal yu yees yi dañoo gisoon ne li gënoon ci ñoom mooy seeni séqoo yu yaxantu ak réewi penku yi ñu koy defal seen bopp ngir mucc ci rënkug yaxantu gii dëkki itaali yi ame woon te daan ko def yu ci mel ni venezia ak genova ak yu leen moy xalaat bii nag taxoon na ba yii réew demoon gëstuji aw yoonu yaxantu wu bees nga xam ne ñoo ciy nekk ci wenn waxtu wi di yaxantukat biy jëli tey tuxal tey kiy dox ci diggante yi lori waa orob yi tàmbli woon na a yol bi ñu déggee xibaari wurus ak xaalis ci afrig ndax kat mbell yu gànjaru yi dañoo muuroon seeni gët fees seeni xel ñoom ñi nga xam ne dañoo tàmbli woon di faale ak a yittewoo wàllug ne ne gi rekk bayyi nee yeneen wàll yi loolu moo tax ñu sawaroon lool ci def wuññi gu juxraaf gi bi ñu déggee tono gu ne ne gu rëy gi nga xam ne am mbooloo ci wuññikati orob yi ndàmmoon nañu ko ci seen tukkiy wuññi yooyu rawati na bi ñu jàngee xisay tukkikatu itaali boobu di marco polo g mi wuññiji woon ba siin g nga xam ne bi muy dëpp daa indaale lu sakkan ciy doj yu tedd ba mujj waa venezia daa ko wooye boroom milyo yi xalaat yi boroom xel yi ci tugal amoon ci suuf si ak bindam dafa soppiku woon ginaaw bi ay tukki yu juxraaf yu kenn kenn amee ak yu mbooloo yu nasaraanal juge orob génn rawati na ginaaw bi jamonoy xarey jooñ yi jàllee nga xam ne boroom xam xam yu bari leegi dañoo am koolute ci ne suuf si dafa bulu walla mu mel ni ab kol kol wuute ak la ñu jàppoon gëm ko muy dafa tàllaliku mel ne basang gu ñu lal loolu nag mooy li muuroon xeli waa orob yépp ci jamono yu diggu yi ag jng jëm ci sopp ag jéngu ak bëgg xam xamu juxraaf feeñ ci ñoom ginaaw ba fa ruug gëstu gu xam xam gënee suuxatu gën fa a jëme kanam ak li ñu jële ci jullit ñi ci biir xeexi jooñ yi ak ginaaaw bi ci xam xam bu juxraaf bu jëm kanam ak ginaaw bu xam xamu bidiw ak ligeeyiinu gaal ak buusal biy won gaal yi seeni yoon gënee jem kanam wuññiy juxraaf yu portigaal yi portigaal moom la ñu y jàppe reew mi jiite woon wuññi yu juxraaf yu orob yi buur bii di henri mi nekoon ab mool g doonoon doomi buur bu portigaal bi tudoon john mu njëkk mi moom mooy ki njëkk a def ay wuññi ci waa portigaal yi mu nekkoon ku soppoon dugg geej ak yër xisay mool yi ak teerey taariix yi muy ku aayoon ci rëdd karti juxraaf yi moom la baayam sàmpoon mu yor sawuta ginaaw bi ñu ko nangoo ci julliti marog yi atum g henri daa xalaatoon a wesaare diine y nasaraan ju katolig ji ci afrig ci noonu mu ne kon na jokkoo k buuru nasaraan bu ecopi bii di prester john ngir ñu ànd xeex waa marog yii di ay jullit cig wàll ak ngir man a àgg ca waaxi geej gu xonq ga ci geneen wàll ci noonu mu yabal ay mool yoy ci seen tukkiy wuññi yooyu àggoon nanu ba ca duni kanaari ya ak madira ak osoras ci mambulaanug atlas atum g naka noonu ñu wëy ci seen tukki yooyu ba agsi senegaal atum g ginaaw bi henri deewee tam teewul seen tukki yooyu wëyoon ba ci sottiwaayu dexug kongoo gi ak niijer bu ko defee mool bii di bartholmew diaz moom àgg ba ca wàllug bëj saalumu afrig di fa ñuy wax boppub callmeer atum g moom la buurub portigaal bi soppi tur wi tudde ko boppub yaakaar ju baax ji ngir mool yooyu man cee ame yaakaar ba man a wuññi yoonu yaxantu wi jëme end mool bu siw bii di vasco de gama moom jug def tukkib wuññi atum g daal di àgg end ginaaw bi mu wëree afrig jaare ko ci yoonu tefesug marog gi romb bopp yaakaar ju baax ji ak mosambig ak mombasa ak malandi ba àgg jawa ca tefesug sowwu gu daanaka dun bu end vasco de gama mii jot naa xamante ak ahmadu bnu maaja mii di woon ab mool bu jullit bu araab moo ko dimbli sax ba mu man a àgg end ndaxte mooli jullit ñi ñu xamoon geeji penku yi lañu woon ak yooni yaxantu yu jéeri yeek yu geej yi naka noonu beneen mool jugati bu tudd kabraal def ab tukki bu geej bu aju ci xare dem end tàmblee naj ak a sonnal samirin mi daa àtte ak a saytu fi nuy wax kalikuta gu end gi ngir mu jox portigaal ab barab bu yaxantu ci tefes gu sowwu gi kabraal mii xeex na fa ak jullit ña song barab ya ak mbooloo m gaalam ma vasco de gama moom itam delluseeti end ci ab tukkib xare ngir faagaagalsi samirin ak mbugalsi yaxantukati araab yu jullit yi ak defsi ay déggoo ak buuri goxi end yi nekk ci tefesug sowwu gu daanaka dun bu end bi li wuññiy juxraaf yu portigaal yi jur wuññiy portigaal yi jur nañu ay ngérte yu bari yi ci ëpp njariñ ñooy yii di ñëw loolu nag mooy li doyadiloon koom koomu jullit ñi ci penku bi maanaam koom koomu nguurug mamaalik ci jëmmi boppam lii moo taxoon nguurug mamaalik mujjoon neew doole ci kanamu nguurug portigaal gi ak ci kanamu ñoñ usmaan ñi nga xam ne jot nañoo fexe ba xaw a woyofal naj ak ñàkkal jàmm gi portigaal defoon araab yi ak nguuri araab yi nekkoon ci tefes gi yàqoon nañu it mbooleem jeem yi ñu daa def ñoom waa portigaal ngir taxawal ab jë bu nasaraan kontar doole yu lislaam yi nekkoon ci peggu geej gu xonq gi ak tefesug afrig gu penku gi wuññi yu juxraaf yu espaañ yi li ci duggaloon portigaal moo duggal it espaañ ci wuññi yooyu ci noonu boroom xam xam yi daa yëngu ci mbiri wuññi gi danoo jàppoon ne suuf si daa bulu moo waraloon ba ñuy dem end ñu jaare woon ko ci sowwu bi moolub itaali bii di cristoforo colombo moom defaloon na waa espaañ ñi benn tukkib wuññi atum g juge espaañ jem end jaare ko ci sowwu bi ci màmbulaanug atlas gi ginaaw tukki bu tar te sonnle moom colombo àgg na ca duni bahama ya mu mujjoon a tudde san salvador juge fa dem ca tefesug kubaa gu bëj gànnaar ga ak dunub ayiti bi mu faroon tudde espaañ gu ndaw gi mu delluwaat nag espaañ ci atum g ànd ak jort ne moom de jot na a àgg end ci yoonu sowwoom woowu ci atum g colombo defaat na ab tukki bu li ko taxoon a jug mooy teg loxo ci suuf yooyu mu jotoon a wuññi ci atum g ak wisaare fa katolig ca ña fa dëkk te mu tudde woon leen ay endo ci tukki bii la jotoon a wuññee jamayka daal di delluwaat espaañ ci atum g mu defati ñatteelu tukki atum g waaye amu ca woon tawfeex mu dellu defaat bu ñeenteel atum g taxul ba tay mu am ca la mu ca doon wut bu ko defee nag ñaari sooy yii mu def ci ñaari tukkeem yi tax ba buuru espaañ bi ferdinand ak soxnaam lingeer bi isabela begadi woon ci loolu ag siwam suux ñu folli ko ci njiitul geej gi daal di koy delloosi espaañ ci ay jéng ngir mere gu ko meññilukat yi mere ñoom ñi seen yaakaar tas colombo faatu na atum g te xamul sax ne wuññi na adduna ju yees ju dul end ginaawam it wuññikat yi doon ligeeyal espaañ wëy ci seen ligeeyi wuññi yooyu ka cay amerigo vispucci jot ca a àgg ca gox ya colombo àggoon ak yeneen yu mu àggutoon ci njëlbéeni xarnub fukk ak juroom benn moom mool bii di amerigo moo am teraagay ñu tudde ko adduna bu bees bii di amerig tay li wuññiy espaañ yi jur wuññi yu angalteer ñoñ angalteer ñoom itam sóobu woon nañu ci wuññi yi bi buur bi henri mu juroom ñaareel mi nekkoon buurub angalteer digalee mool bii di john cabot mu tukki dem end jaare ko bëj gànnaar gu suwwu gi ca saa sa mu geeju tukkee bristol atum g jéggi màmbulaan gu atlas àgg tefes gu bëj gànnaar gu amerig gu bëj gànnaar gi ca new fondland ginaaw bi mu jéggi librador dellu angalteer cabot mii delseeti na leru tefesu g penku gu amerig gu bëj gànnaar gi ba àgg florida loolu nag moo doonoon tàmblig sancug walla koloniiseg waa angalteer yi ñeel amerig gu bëj gànnaar gi ak kanadaa ba tay it kii di jams kook di woon ab mool bu dëkkoon angalteer defoon na moom it ñatti tukki yu wuññi ca tefesi ostrali yu penku ya ak newsiland wuññiy fraans yi waa fraans nag ñoom ñoo mujjoon a duggsi waa angalteer waa espaañ ak waa portigaal ci lefum wuññi mi ñoom seeni tukkiy wuññi daa jemi woon kanadaa ki ñuy wax jaak cartier moom ab mool la woon daa jugoon def benn tukkeem bu wuññi ci jamonoy fransuwa mu njëkk mi jeggi màmbulaan gu atlas gi jem sowwu fetali àdduna ju yees ji ci noonu mu àgg new fondland gi jàkkaarloo ak kanadaa daal di fay jot a wuññi walla feeñal sottiwaayu dexug santa lorans tukki yi cartier mii jot a def ci goxi amerig gu bëj gànnaar gi ñeent lañu woon bi mu ko defee sancug fraans tàmblee putuxlu ci kanadaa ak goxi dex yi ci amerig gu bëj gànnaar gi noonu ñu taxawal ab sancu tudde ko samwel de shampala taxawal it dëkk bii di kebek ci tefesug dexug santa lorens atum moolu fraans bii di de laasal jotoon na a wuññi dexug misisipi ci noonu waa fraans ya daal di fay sos sancu walla koloni bu luwisiyaana bii nga xam ne mi ngi jële turam wi ca buurub fraans ba tuddoon luwis mu fukk ak ñeenteel mi wuññi yu oland yi lonkoo gu end gu penku gu oland gi dafa joxoon ndigal moolub angalteer bii di henry hadson da ko o joxoon ndigal ci mu defal oland ab tukkib wuññi ngir man koo gisal aw yoon wu bëj gànnaaru penku wu ko man a àggale asi ci noonu mu geeju moom hadson juge angalteer jaare ko ci bëj gànnaaru atlas gi jawali golofub new york ak dexug hadson gi mu tudde woon boppam moolu oland bii di wilyaam shotin moom moo wuññi yoonu boppub horn bi nga xam ne mujj na di yoonu geej wu am njariñ waa oland yi jeemoon naño o wuññi ostraali ak newsiland ci diggante g li wuññiy juxraaf yu orob yi jur li wuññiy tugal yi jur man nanu koo tënk ci lii di ñëw yëngu yëngu gu yaxantu gu yees gii ñi ngi ko tudde woon soppi ci anamug yaxantu doggantal gu ñatteel gi yëngu yëngu yi jugoon di kontar egliis bu paab bi yëngu yëngu gu yewenal diine ji ci tugal yëngu yëngu gu yéwénal gu diine ci tugal mooy googu doon am ci orob ci xarnub fukk ak juroom benn g ngir setal egliis bu katolig bi ci li ci taqoon ci ay ñaawtéefi pas pas ak yu jikko na ñu ko daa defe mooy jeem a delluwaat ci njàggaley injiil yi li waraloon yéwénal gi ak li egliis bi di nekk nguurug ruu lepp ci li ko njëkk a tax a jug teewul ànd ak li jamono di gën a yàgg mu jot a àgg ci ëpp ci loxob weñ nguurug diine gi ak gu politig gi maanaam mu tëye tëyiin wu metti te tar ñaari nguur yii di gu diine gi ak gu adduna gi ci loolu la mujje di dooley politig ju diine ju koom ju mboolaay ak ju aada ci mboolaay yu tugal yu katolig yi ci jamono yu diggu yi dàkku nag walla xañ nit ki jàngu bi moo nekkoon mbugal mi gën a saf te gën a tar mu egliis bi moomoom daan ko teg kuy jeem a léewtoo k moom ak nu darajaam man a kawee mbaa mu màgge ni egliis bi ci safaanub muy jëfandikoo nguurug ruuwam gi di jëmale nit ñi ci yooni baax ak ragal yàlla moom déy ginaaw ag mbon da koo duggoon daa labaloon boppam ci bànneexi adduna aki caaxaanam fàgguloon boppam ay suuf yu yaatu ay alalam it mu teggiloon leen te musal leen ci galag yi ñépp di fay ci noonu paab yi ak kardinaal yi nekkoon di ñu nuuroon ci dundug adduna aki caaxaan yu ëpp ñaawtéefi egliis yooyu ak yu leen moy ñoo gestuloo woon te fëkkoon yittey yéwénalkat yu mboolaay yi ak bindkat yi ci jamonoy yewwute gi ki gënoon a jeexiital ci mbooleem bindkat yooyu mooy labbe bii dib xeltukat nu ko daa wax erasmus g moom daal jamoon na ci teereem bi tudoon tagg ag ndof praise of folly jamoon na ci nekkiinu egliisu katolig bi mu nekkoon jam yu tar te wex dox gu taarixe gi yéwénalug diine gi defoon ci orob yéwénalug diine ci orob ci doxam bi romb na ñaari tolluwaay bi ci njëkk mooy bi ay yëngu yënguy yéwénal yu ndaw amee te lalu niki ay njiitlaay aki cëslaay yoo xam ne ci seen kaw la yëngu yënguy yéwénal yu diine yu mag yi ci tugal tegu bu ñaareel bi nag mooy yëngu yëngug yéwénal gu mag gi ci boppam bu dee nag yëngu yëngu yu diine yi nooyal yoon wi ba yu mag yi man a am man a taxaw ci tugal ñoom ñooy yi nuy wax fransiskaan ak dominikaan ñooy yi gisoon ne mant a ñàkk nu dañal njuumte ak ñaawtéefi diine yi niki aw yoon wu nuy jaar ngir yéwénal egliis bi te dëgëral ko ag yëngu yëngu gu yéwénal daal di taxaw ca angalteer ci njiitl john wycliffe g moom kenn la woon ci ustaas yu siw yu daaray oksford ju mag ji googu nag li ko taxoon a jug mooy dañal li taqoon egliis bi cig mbon gii yëngu yëngu moom mi ngi judd ginaaw lu tolloo k xaaju xarnu ginaaw juddug yëngu yëngu gu ñaari way sell yii di fransis ak dominik waaye gii nag moo gënoon a fés gën a jeexiital ci egliis bi ci gu fransiskaan gi ak gu dominikaan gi geneen it feeñati gu yéwénal ci bohimiya ci njiitul john hess g moom mooy ki ne woon ag diggale wart a am ci diggante nit ak boroomam ndare diggale googu doon ngëm ak jëfe li ci injiil hess nag li mu jublu woon ci loolu mooy wàññi sañ sañu paab gi ak neenal taxawaayub làbbe bi niki aji diggale ci diggante jaam bi ak boroomam bu dee yéwénali diine yu mag yi ñoom ñi ngi doon jëmmu ak a feeñe ci am gi yëngu yëngug protestants gi amoon njiit ya di woon martin luther kalfan ak swingli martin luther ak yéwénal gi martin luther mi ngi juddoo isilban di benn dekk ci diiwaanu saksoniya ci almaañ atum g faatu atum g baayam nekkoon ku daan ligeey ci benn ci gasuwaayi mbell yi mu màgge nag ci njaboot gu ndóol ak ci ron dund gu jafe te wow moom nag jàng na cosaani làkkuw latin ak cosaani ag katolig noppi jàng yoon ak xeltu dugg nag ginaaw bi benn ci barabi jaamu yu katolig yi ngir laabal fa boppam ciy bàkkaar aki ñaawtéef loolu nag ci gëm gëmi katolig yi la bokk ginaaw bi mu tukki dem rom atum g def fa weer gisal boppam ñaawtéefi paab gi ak bon boni egliis bi li gënoon a wëlbati ay bëtam mooy jàdd gi niti diine yi jàddoon ak wàcc gi nu wàccoon yoonu leer ak lëmoodiku wi nasaraan gu njëkk ga yoroon ak set gi mu setoon lii jeexiitaloon na ci boppam ak xelam mu daladi mi jañoon ko it ci jam walla kritige paab gi ginaaw bi it mu mujj fttéerlu ci kawam bi mu bañee moom paab gi ne du soppi aw doxaliinam dikk gi labbe bii di john tetzel dikkoon ci diiwaanu saksooniya atum g ngir jaaysi fa xobi njéggal yi dikk googu dimbli woon na luther ci mu man a feeñal li nëbbu woon ci biiram muy yéeney yewenal yi mu yoroon te fasoon leen ci xolam jaadu na ñu fàttali leen ne xobi njéggal mooy li fi wuutu woon tuubug aji tooñ ji ci jeem a fare ay bàkkaaram ci def lu baax jaare ko ci julli walla joxe asaka mbaa woor waaye paab bii di liyoo mu fukkeel mi moom daal da ne woon da na doy aji moy ji bu bëggee tuub ay bàkkaaram mu aji ji rom ginaaw bi wax jooju xaw a gën a jëm kanam gën a xóot bi kenn ci paab yi nee njéggal daal man na a ame ci nit joxe ci alalam ci egliis bi ngir ñu dundale ci diine bu ko defee ñu jox nit kooku xobu njéggal luther moom dafa kontaroon njaayum xobi njéggal yi mu ne woon mucc mbaa mbugal ak fayoontoo manuñoo juge ci jënd ay xobi njéggal fa nu man a juge kay mooy gëm yàlla luther moom diiatoon na xobi njéggal yi daal di woon dem ba ca egliisub wtanberg ba wékk fa mbind mu ëmb ay diiat yu toll ci ci atum g paab bii di liyoo mu fukkeel mi amoon na taxawaay bu tar ci xalaati luuther yi ndax daal di woon nay genne ca saa sa benn saxal walla ndigalul xañ ñu teg ko luther saxal boobu walla ndigal loolu moom lanu daa wax wermis waaye luther moom faalewul woon saxal bii moom kay da koo sanni woon ca ëttub egliisu watanberg ba lakk ko xalaati martin luther ak ay gisiin yu yéwénal yi mu yoroon luther xalaati yéwénal yi mu woote woon jëme ñoo y yii di ñëw nii 	injiil mooy nattukaayub diine ak bu yoon bi muy sukkandikoo ci firi pas pas yi ak mbooleem masalay diine yi am ag wuute 	nit ku jàng ku nekk tey jëfandikoo xel sañ na a jàng injiil te firee ko ni mu ko dégge xame ko ni 	paab bi amul benn yoon àq mbaa sañ sañ ci rënkal fi boppam moom rekk sañ sañu firi injiil 	sëy daa war a dagan ci làbbe yi 	niti diine yi dañoo war a nekk ci ron kiliftéefug nguur gu àdduna gi 	wàññi limub jàngu yu bari yi tasoon ci mbooleem reewi orob gu sowwu gi bu nu xoolee xalaati martin yi dananu gis ne moom daal li ko yitteeloon mooy mu neewal doole sañ sañu paab bi loolu yaa ngi koy gisati ci bi muy sàkku nu neenal diggale gi daa am ci diggante yàlla ak ub jaamam sàkku gi mu doon def it ci nu neewal limub jàngu yi li mu doon wund mooy neewal ngañaayi egliis bi aki am amam ndax loolu man a soril egliis bi caaxaan ak po mi mu nekke woon da nga gis it ne wax ja mu waxoon ne nit ku xam ku nekk am nga àq ci jàngal sa bopp injiil ak firee ko ni nga ko dégge moom itam li mu doon tekki mooy jeqiku gu mu jeqiku woon ci egliis bi ak rafleel gu mu ko rafleeloon ci li mu jàppoon moom egliis bi ne àqi yoonam la ju mu moom jëfka yi dimbli luther mii ci wooteem gi man a àntu am na ay jëfka yu bari yu ñoo dimbli woon martin ci fipp gu yéwénal gi man a àntu yi ci ëpp solo ñooy yii 	feeñ gu luther mii feeñoon ci jamono joo xam ne waa orob yi seeni xel da cee tàmbli woon a ubbiku ñu tàmbli woon a fqu ak a dañtalu ci ëbug paab gi ak sañ sañam 	siwug njuumte ak ñaawtéef yu rëy yi nga xam ne taqaloon nanu derub paab gi te taxoon ba nit ñi doon sikk ag muccam ak ag sellam 	fonk sa xeet walla xeetu gi tàmbli woon a feeñ ci reewi orob yi te taxoon waa almaañ ñi defoon ab dank topp ci ginaaw martin luther rawati na maas gu diggu ga ak baykat ya ak gawar ya 	dimbali gu ko ustaas yu daara yu mag yu tugal yi dimbali woon ak ñu dul ñoom ci xalaatkati almaañ yi warlu woon ne ñooy fas yeenee tas xalaatam yooyu 	firi injiil ci làkku almaañ ak def ci ay taalif yu tax waay almaañ ji man a gis ay xalaatam yër it jam yi mu doon def egliis bi 	tasug móolukaayu téere gi nga xam ne gotenborg moo ko fentoon loolu taxoon nag ba xalaati luther yi tasoon ci waa almaañ yi ak ñu dul woon ñoom am na benn xeex bu mag bu amoon ci diggante martin aki gaayam ñoom ñi diy protestants maanaam ay diiatkat cig wàll ak diggante ñi toppoon paab gi katolig yi ci geneen wàll dëkki almaañ yi moom xare yu tàng a fa amoon dongay ñaari ngér yii doon xeex nag mujjoon nanoo xaatim ag juboo gu nu tudde woon augsburg atum g ñu nangu woon ci ne goxu almaañ bu nekk am na àq ak sañ sañ ci tànn ngér mu ko neex mu protestant mbaa mu katolig waaye ci wàllug ofisel ñu tànn protestant def ko diine ngérum luther mu protestant mii tasoon na te siw ci goxi almaañ yu bëj gànnaar yi egliisam daal di doge ca egliisub rom ba ak norwej finland xalaat yii tam tas ba genn almaañ dugg angalteer ak nguuri skandinaaf yi danmark ak suwed kalfen calven john calven mi ngi juddoo fraans atum g di woon ku duggoon ci ngérum protestant mu luther mi te bàyyi woon mu katolig mi kalfen walla calven juge woon na fraans dem siwis li ko waraloon it mooy sonnal gu nu ko fa doon def ngir ay sabab yu aju ci diine fii nag la tàmblee wisaare ak a tas ngérum yéwénalam mu xaw mee jege ngérum luther mi ñi ko toppoon mu tudde leen hogonoots di ci maanaa ñoñ laab ñi kalfen ak luther dëppoo woon nanu ci ay masala yu diine yu bari waaye wuute woon nanu ci ñaari mbir ñooy 	wax gi kalfen waxoon ne njéggal ci mbir yi nu doggal la te loolu luther nanguwu ko 	kalfen daa gëmoon ne egliis bi warul a topp ci ginaaw genn nguur gu adduna ne woon egliis bi daa war a am nguurug boppam gu temb gu dul wéeru ci gu adduna gi ñi war a doxal nguurug egliis bi nag ñooy am mbooloo mu xellu te am hikma xalaatam yooyu nag wisaaroo woon nanu ci reewi tugal yi ci anam gu ëppante ci fraans angalteer siwis ak yeneen swingli mi ngi cosaanoo woon siwis judd atum g ay yéwénali diineem mu tàmbli woon ko ci dëkkub siyorix atum g ci biir diiat gu mu doon def njaayum xobi njéggal yi kon foofu ag jegeente gu mag am na fi ci diggante ay xalaatam ak yu luther ak kalfen waaye teewul mu wuute ak ñoom ci lenn ci ay masalay diine swingli moom daa jàppe woon egliis bi benn campéef bu am demokraasi buy ame ak a sosoo ci mbooleem nasaraan yi nga xam ne seenug bokk ci mi ngi ame ci benn kuréel bu leen fay teewal ci mbooleem mbir ak masala yi aju ci egliis bi ak ni ñuy sampe nit ña fay ligeeye ngérum swingli tasoon na ci siwis ak ci lenn ci yeneen reewi orob yi waaye taxutoon mu siwe wisaaroo ni mu luther mi mbaa mu kalfen mi bunt bu ñaareel bi jëm kanam gu xam xam ak yewwute gu endustri doggantal gu njëkk gi jeexiitalu gi waa orob defoon ci yooni gëstu yu xam xam yu jullit ñi jamono ji xam xam neewe lool te amadi xiima ci tugal ci jamono ju diggu ji di ju ag laman moom xam xam nekkoon na ci mbooleem reewi jullit ñi di lu naat te meññi xay gu lislaam gi di woon gi gënoon a kawe ca booba ngir coona bi boroom xam xami jullit ñi daa génne ak a daj ci dundal ko ak ngir soññe gi nguurug lislaam gi daa soññe ak a jàmbaarloo ci xam xam ak boroom xam xam yi bi waa orob yi dee ñu yittewoodi xam xami gres yi ak yu leen moy fekkoon na jullit ñi ñoom ñu nekkoon ñu xam xami xay yu yàgg ya ñoroon ñu taxawoon ci firi leen ci araab xay yooyu di yu gres faaris end rawati na ci ndoktoor bidiw ak mat ak yeneen yi ñu jotoon a naan nag ci xam xami ubuqraat iqlidis aflaton ak arustoo ak ñu leen moy ci boroom xam xami gres yu mag yi boroom xam xami jullit ñi yamuñu woon rekk ci naan ci xam xami gres yi ak tuxal leen yobb leen ci araab waaye kay danu leen a toppoon wéral leen te dolli ci lu bari ci li nu feeñal wuññi ko ciy xam xam aki gëstu aki nattu yu nu amal ci wàllug ndoktoor ak mat kimyaa ak xam xami dénd yi bidiw juxraaf ak yu leen moy ginaaw bi nu amee jikko yu mag yiy joxe xalaatub xam xam bu sell ngérum walla yoonu gëstu wu xam xam ci jullit ñi boroom xam xami jullit ñi daal doxoon nanu ci seen gëstuy xam xam yi ci ngérum xam xam mu wuutewut ak mu xam xam mi am ci jamono ju yees ji ñi ngi sukkandiku woon ci yooni xam xam yoy bokkoon na ca yii xeeñtu raññale xaaj yi jëfandikoo yooni natt yi jàkkarloo làmb misaal ak jeem a àgg ca jëmuwaayu xam xam ba maanaam xam xam bi la tax a jug ak xam ngérte yi muy liy juddoo ci boo ko xamee ba noppi ngir coona yii nu daa daj nag mujj nanu di ñi jiitu ci lefum gëstu mu xam xam walla li nuy tudde yoonu xam xam wu nattu ci noonu lanu fi sampe woon kenoy gëstu gu xam xam ngir yeesal gi nu yeesaloon xam xam ci seen jamono waa tugal yi nag jariñu nanu ci wii yoonu nattu wu xam xam wi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci ki jiitu woon ci ñi ci jariñu mooy waay angalteer ji di roger bacon g g mooy ki waa tugal yiy jàppe ki raw ci gëstug xam xam ci tugal ndax mooy ki jeemoon a wutal xam xamu dénd ag noste guy sukkandiku ci nattu ak jàkkaarloo loolu nag mbir la moo xam ne boroom xam xami jullit ñi ñoo ko ci jiitu jaadu na ñu leeral fi ne roger becon mii kat ku jotoon a jàng làkku gres la ak wu yahood yi ak araab jariñu woon it ci xam xam yi nu ci bind moom nag daa gëmoon ne li tax ñu war a jàng fisiya ak kimiya ak mat ak bidiw ak xeltu mooy ligeeyal xam xam bi aju ci yàlla digg yi xayug lislaam gi jaaroon bi muy dugg orob jullit ñi dañoo nekkoon ñu rawoon ci lefi xam xam yu bari ci noonu ñu yanu woon seen xay googu yóbbaale ko ci mbooleem àdduna bi ci penku bi ak sowwu bi orob jariñu woon na bu baax ci xam xami jullit ñi ña fa dëkk it jòkkoo woon nanu ak jullit ñi jaare ko ci ay ker keraan yu bari bokk na ci yooyu 	andalusi waa orob yi jonjoo woon nanu ak digg yu xayug lisaam gi ci andalusi moom gox bii nga xam ne daa mujjoon fees dell ak leer guy jòlli tukkee ci xayug lislaam gi ko róofu woon moom bii gox barabu jòlli la woon ñeel xam xam ak dañ kumpa rawati na ci dëkki orob yi mu dendaloon bu ko defee nga gis sàkkukati xam xam yu orob yi daa jariñu ci xam xami jullit ñi di jawalsi ak a jublusi dëkki andalusi yii di talitala kordoba ak sewija ñu jële woon ci ñoom ngérum nattu mi ñu daa jëfandikoo ci gëstu gu xam xam loolu mujj yëngal bu baax xalaatiinu waa tugal yi 	dunub sisil araab yi jotoon nanoo teg loxo sisil ki joxe woon ndigalul jëf jooju di siyadatul laahi bun al axlab buurub nguurg axaaliba yi waaye mu ame ci loxol kapitenam bu siw boobu di asad bun alfuraat atum ginaaw gàddaay gi mu ame woon nag ci jamonoy xalifa bu nguurug waa abaas bi tuddoon maamun ca saa sa xayug lislaam tàmblli fa a sutuxlu sisil mujj di gilin ci gilini xam xami lislaam yi sàkkukati xam xam yepp jublisi ko rawati na ñi dëkke woon orob ngir sàkkusi fa xam xam bi norman yi nangoo sisil ci araab yi yaquñu woon xayug lislaam gi ñoom kay dañoo sawarloo woon boroom xam xam yi soññ leen ci noonu firi teerey araab yi yobb leen ci latin daal di fay tàmblee am ak a sawar waa orob yi tàmblee yër li ci yii teere ak a jariñoo rawati na itaali mi ci gënoon a jege sisil looloo waraloon muy mberum yewwute gi 	xarey jooñ yi bokk nanu bu baax ci li tax waa orob yi manoon a jokkoo ak xayug jullit ñi jokkoo gi it saxoon na fi lu tolloo ak ñaari xarnu ci biir ñaari xarnu yii orob jot na cee tuxal lu bari ci xam xami lislaam yi ame ci it walla tege ci loxo lu bari ci teere yi nu taalifoon ci araab ak yi nu firi woon jële leen ci làkku gres end ak faaris 	jokkoog yaxantu gi amoon ci diggante reewi jullit ñi ak orob rawati na li ci itaali jotoon a def mu bokk ci li sababoon jonjoog xay ci diggante ñaari dëkk yi 	siyaare gi nasaraan yi daa defsi ci seen barab yu sell yi nekk palastiin nga rax ci dolli tukki yi waa orob yi daa defsi ci reewi jullit ñi ak la ca juddoo muy ñu gis te jariñu ci xam xami jullit ñi ak seeni xay jullit ñi daal ñoo waral jëm kanam gii nga gis ci orob ci jamonoom ju bees jii xam xam yi bàyyi ay jeexiit ci waa tugal yi lim mat jullit ñi naanoon nanu ci xam xami kalkil yi nekkoon ca waa end yu yàgg ya ñu jotoon a jànge ca ñoom ni nuy defe ay lim numero waaye nag nu sellal ko gën koo teg ci yoon boroom xam xami jullit ñi ñoom defoon nanu ay dollent yu am solo ci xam xamu waññ calcul ñoo dolli woon tus ci lim yi ndax amu ci woon bi nu leen di jël ñu indi màndargam al kasr alhasarii di ci wolof damat ci fukk ñu taalif ci wàllug xam xamu waññ calcul ay teere yu waa orob yi firi ci seeni làkk te jariñu ci boroom xam xamu jullit bii di muhammad bun muusa alxuwarsamii nekkoon na di ku aay ci xam xamu lim walla waññ moom de lanuy sant bu lim mumero yi nekk ci kalkil duggee orob tay xawaarsamii mii aayoon na it ci beneen xam xam bu yees mooy aljabr moom sax mooy ki ko sos far taalif na ci tollale ci aljabr nu tekki ko ci ginaaw bi ci làkki orob yu bari boroom xam xami orob yi jariñu ci boroom xam xami jullit ñi jëfandikoo nanu ay junj ci matematig yi xam xamu lim ñoo njëkkoon waa orob yi ci wàllug matemetig gu yees gii bu dee nag ci andasa ak xam xamu ñattal yi jullit ñi ñoom yamuñu woon ca la woon ca waa gres yi rekk nga xam ne seen boroom xam xam bi nu naan iqliidis moo ko feeñaloon waaye jotoon nanoo feeñal ay masalay andasa yu bees ñu duggal li nuy wax al mamaas ci xam xamu kalkilu ñattal nu jël li nuy wax juyuub poos wuutale ko ak li nuy wax awtaar buum nu fecci itam toolale yu nu kaabaal yi nu xootal bu baax tam ci xam xam yu nuy wax maxruutaat boroom xam xamu jullit bi nuy wax omar alxiyaam defoon na lu mag ci wàllug mat moom de bokkoon na ci ñi gënoon a ràññiku ci boroom xam xami jullit ñi ci wàllug matematig ci ñeenteel bu njëkk bu xarnub fukk ak ñaar g xam xamu fisiya li nga xam ne sikk amu ci mooy ne jullit ñi jariñu nanu ci xam xamu fisiya ci waa gres yi bi nu ko tekkee ci seen làkk waaye ñu gën koo yaatal dolli ci ay masala yu fisiya yu bari nu màndaqe walla natt diisaayu yolaakon yi nu fent ay màndaqekaay yu xereñ ñu xamale ay gisiin yu bees ci xam xamu kàddu ak gis basariyaat ak séen almariyaat boroom xam xam bu jullit bii di abo yuusuf yahquub ishaq alkanadi mi nga xam ne mi ngi faatu atum g moom ku aayoon ci xam xami gis yi la taalif na ci ab teere bu am solo mooy teereb yu nu xool yi nga xam ne waa orob yi mujjoon nanu ko o tekki ci làkku latin roger becon jariñu ci ak liyonardo da vinci ak boroom xam xam bu poloñ bii di copernice g boroom xam xamu jullit bii di abo aliyu muhammad bun alhasan bun alhaysam g moom mu nekkoon di ku aay ci xam xamu fisiyaa mu soppi xam xamu leer bu yàgg ba indi fi xam xamu leer bu yees bi mu amoon ndam ci indi fi gisiinu xam xami seen yi mu firi feeñteg xònn ak safaanu gi ag leer di safaanu ak ni muy dammoo bu boroom xam xamu gres bii di batlimos jàllee kii di ibnu haysam moom lanuy jàppe boroom xam xam bi njëkk a def ay wuññi ci xam xamu gis haysam defoon na ay taalif ci xam xamu yu nu gis yi ak xaaji bët ak weer yi ak leer ak yeneen waa orob yi it yii taalif tuxaloon nanu leen ci seen làkk wii di wu latin ci xarnub fukk ak ñatteel g ak ci yeneen làkk yu orob yi loolu dimbli leen ci nu jariñu bu baax ci xam xam yii nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci bu baax xam xamu bidiw jullit ñi yittewoo woon nanu xam xamu bidiw xawarsimii moom defoon ay natt ci yëngug bidiw yi xam fi nuy fenke ak fi ñuy sowe jullit ñi jariñu woon nanu ci xam xamu bidiw ci waa geres yi ci noonu ñu firi woon ci araab lenn ci teerey bidiw yu geres yi niki teereb batlimos bi tuddoon ñeenti wax yi boroom xam xam bi ko tuxaloon ci araab di aboo yahyaa albatriix ci jamonoy abo jahfar almansuur doomi muusaa bun saakir ñoom itam taalif teere bi nuy wax aljadaawil alfalakiya yeneen boroom xam xami bidiw it feeñ niki saabit bun xurra haniin bun ishaqa alhibaadi ak bataani mi faatu atum g ak ñu dul ñoom jullit ñi tabaxoon nanu ay fuglukaayi bidiw ca dimasq baxdaad kordoba ak sawija di woon ay dëkki lislaam abo abdillaa albattani mii dees na ko lim muy ki gën a bàyyi ay jeexiit ci anam gu xóot ci waa tugal ci boroom xam xami bidiw yu jullit yi waa orob yi ñoom jariñu nanu bu baax ci xam xamu bidiw ci jullit ñi ak ci li jullit ñi jot a gennewaat ci anam gii ciy wuññiy xam xam jullit ñi fésoon nanu ci xam xamu kimyaa jaabir bun hayyaan alkoofii bokkoon na ci ñi gënoon a siw ci wàll googu moom mi doon def kimya te taalifoon ci ab jimblang jabbir leeraloon lu bari ci way toggale yu kimya yi nu xamutoon bu njëkk niki aji wex ju nitrik ruug nasaard botaas soda al kawiya ak aji wex ju asotik ak yeneen mu leeraloon ba tay jefi kimya yi niki seebal ak leeru ak yeeg ak toqqal da na jaadu nu leeral ne xam xamu kimya moom danu ko daa wooye xam xamu jaabir ngir li ko ci yàlla tawfeexaloon ba mu man a topp yoonu xam xam wu nattu wi nga xam ne ci la jaaroon ba man a àgg ci ay dëgg yu kimya yu bari waa orob jariñu nanu bu baax ci xm xamu kimya bi ci jullit ñi ci noonu nu firi taalifi jaabir yooyu ci seeni làkk xam it lu bees li ci jullt ñi dolli ndoktoor boroom xam xami jullit ñi rawoon nanu ci xam xamu ndoktoor sartoon nanu ci seen boroom xam xam mu xam siddi xam jëf ak warteefi cer yi ak noyyi ak soppikum saw ñoom de ñu sonnoon ci xam xamu siddi lanu woon firi woon nanu xam xami geres yi ci aju woon ci làkku araab bi nu noppee ñu taalif ci teereb ibnu nafiis bi tudd tasriihul xaanuun dolli na ay xam xam yu am solo ci xam xamu siddi jullit ñi jàngale nanu doxug dereet sonn it ci mbooleem xeeti tawat yi xamale itam deewal bi nuy faral a def ci ligeeyu xotti ki niy wax razi te faatu atum g feeñ na te raw ci ndoktoor taalif na ci lu sakkan ak ibnu sinaa mi faatu atum g moom de kenn la ci boroom xam xami jullit ñi gën a siw ci ndoktoor teereem ba tudd xanuun fit tibb de jenn jimblang la ju xam xamu ngoktoor ju waa penku ak sowwu ñepp xam ak abo xaasim xalf mi gënoon a fes ci xottikati xarnub fukk ak benn g ak ibnu zahr boroom teere bi tudd mubtakaraat fil jiraaha waa orob yi jariñu nanu ci xam xamu ndoktoor bi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci ñu jariñu ci ni nuy siddee ak ni nuy gennee tawat yi ak ni nuy faje ak ci xam xam yi nga xam ni teerey jullit yi làqoon nanu leen ci wàll gii ginaaw bi nu leen firee ci làkki orob yi waa orob yi jële nanu ci jullit ñi tabax ay fajuwaay ak jëfandikoo deewal ak li nuy wax kaaw su nuy opere xotti waa orob yi ba tay jariñu nanu bu baax ci xam xamu xeltu bi nga xam ne jullit ñi ñu ci rawoon lanu ci noonu nu jàngoon taalifi kanadii faarabii ibnu sinaa ak ibnu rusdi ak ñu dul ñoom ginaaw bi nu leen firee ci seeni làkk bokk na ci boroom xam xami orob yi gën a siw ci jariñu ci jullit ñi ak seeni xalaat paskaal dikart hiyom ak becon ak ñu leen moy waxtu wi yaatuwul ngir nu man leen a indil ngértey xam xam yu bari yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci ci seeni gëstu te booba orob a ngi ci ngëmmeenam li ak lëndëmug reeram gi ci ron nosteg laman ak cangug egliis bi da na yell nu leeral ne xam xam yi ak ngértey xam xam yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci dañoo tàmbli woon a tuxu ndànk ndànk jëm ci reewi orob gu sowwu gi ginaaw bi ab kureel ci waa orob yi xamee solos xam xam yii te taxawoon ci firi leen ci seeni làkk ay firikati orob yu bari feeñoon ci loolu ku ci mel ni costantinus africanus herman the cripple ak eugenius mu parlermo mi ak ñu dul ñoom kon lu nu war a xam la ne yewwuteg xam xam ak gu endustri gii am ci reewi orob yi ci ginaaw yewwute gi du lu moy meññat ci meññati nattu ak gëstu yu xam xam yi nga xam ne orob tuxale na leen ci xam xami lislaam ci digg jamonoy xayug lislaam gi coonab gëstu yooyu nag ñooy cëslaay yi nga xam ne ci la jëm kanamug xam xami dëppale yi ak yu xarala yu bari yii tegu ci adduna ju xay jii ngay gis tay doggantal gu ñaareel gi wàll yi xam xam jëme kanam ci tugal xam xam naat na te jëm kanam ci orob ci biir xarnu yii bu fukk ak ñeent fukk ak juroom ak fukk ak juroom benn g loolu bokk ci li waral jëm kanamug xam xam gu mag gii orob gis tay ci jamonoom ju yees jii nu nekk nga xam ne ci la yewwuteg xam xam juddoo ak gu endustri ci orob ak li topp ci loolu ci njariñ yoy du orob rekk la ñeel waaye àdduna bépp li taxoon xam xam jëm kanam jëm kanam gii xam xam jëm kanam tay ci reewi orob gu sowwu gi am na ay balluwaay yu wuute yi ci ëpp solo di 	tuxal xam xami jullit ñi ak firi leen ci làkki orob yi te jariñu ci 	ak feeñ gu ab lim xëy feeñ ci boroom xam xami orob yi amoon ag cofeel ci gëstu yi aju ci xam xam 	yokku gu yëngu yëngug firi ak taalif yokkuwoon rawati na bi nu fentee móolukaay yi 	xeemmeemteef gu waa orob yi amoon ci dundalaat xam xam yu yàgg ya yu gres rom ya wàll yi xam xam jëme kanam ak li nuy misaal jamono yu diggu yi ci orop lepp naan jamonoy reer la ak lëndëm teewul ay ceññeeri xam xam yu kenn mant a reere mant a weddi amoon fa li am daal mooy wuññiy xam xam yi ci jamono jii du woon yu yaatu lu neew la woon ci noonu xam xamu waa orob yi nekkutoon lu moy li nu xame woon ci waa geres yi ak ci jullit ñi ci seen ginaaw maanaa mi xalaati waa orob yi ame woon soppiku woon na ci jamonoy yewwute gi ginaaw bi nga xamee ne gëstuy xam xam yi fa ñoom dafa mujjoon tegu ci nattu ci noonu orob jot na a am ndam ci jëmale kanam xam xam ci wàll yu bari yi ci ëpp solo di ndoktoor ndoktoor ci orob wëyoon na di sukkandiku ci li fi waa geres bàyyiwoon ak li fi jalinos jot a indi ak hiboqrat ak ndoktoorug jullit ñi jaare ko ci seen teerey ndoktoor yi nga xam ne waa orob mujjoon nanu leen a firi ci seeni làkk xam xam bi orob ame ci ndoktoor weesuwutoon fii ba ci xarub fukk ak juroom benn g waa orob yitewoo woon nanu bu baax xam xamu ndoktoor ñoom daal ñoo ci gënoon a sonn ñu dul woon ñoom rawati na ci xarnub fukk ak juroom benn g moom dey xarnu la bu fekke ay xew xew yu bari yoo xam ne ñoo waral ag jëm kanam gu mag ci wàllug ndoktoor ci orob bii xarnu daal seere na ay yëngu yëngu yu wuññi yu juxraaf ak tuxug ay mboolooy gaal yu yaxantu ak ay gàddaay ci ay mbooloo ngir dëkk ji ci reew yii nuy door a wuññi aki xare yu tar te yàgg yu amoon ci orob te sababoon ay tawat yu metti aki mbas yu nu xamutoon ci orob mu mujj nag bokk ci warteefi doktoor yi ci orob ñu jeem a xam yile tawat yu yees ak nu nu leen di faje wutal leen ay garab ci noonu boroom xami xami orob yu bari feeñ ku ci mel ni fisaliyos mum beljik mi frakastor mu itaali mi ak gonte andarnax mu almaañ mi nekkoon doktoorub fransuwaa mu njëkk mi doon buuru fraans ak lofan hok mu oland mi ak luwis pastor mu fraans mi ak kox mu almaañ mi añs bu ko defee waa tugal yi xam jàngoro yi xam it nu nu leen di faje ju ci mel ni daftiriya judri tifos kolera tifod añs juxraaf ak bidiw xalaat bi naan suuf si daa tàllaliku daal te boroom xam xami bidiwi gres yi indi woon ko fi moo nekkoon xalaat bi tasoon ci tugal gëpp ci jamono ju diggu ji ak doonte lenn ci boroom xam xami gres yi waxoon nanu lu ko safaan ne suuf si moom tàllalikuwul daa bulu kay mel ni ab kol kol boroom xam xamu gres bii di batlimos moom doon na def ay ligeey ci googu wàll waa tugal yi nag seen xam xamu juxraaf ñi ngi ko doon gën a jëmale kanam jaare ko ci li nu xame ci wuññiy juxraaf yi ak ginaaw bi ci noonu xam xamu juxraaf tàmblee jem kanam ci orob jem kanamug xam xamu juxraaf tax na ba bu bidiw it jem kanam kii di koperniks di boroom xam xamu poloñ moom siwoon na ci lefum xam xam mu tugal mi moom dey duggal na loxoom bu baax boo xoolee ligeeyam yi aju ci xam xamu bidiw ci doxug xam xam akug jëmam kanam ci tugal kopernic moom àndutoon ci gisiinu batlimos wi doon wax naan suuf si moom daa bulu ba noppi nekk ci digg adduna bi bu ko defee nekkteefi asamaan yi di ko wër kopernics moom ne suuf si daal ak yeneen nekkteefi asamaan yi ñoom ñepp danuy wër jant bi te suuf si nag am na wërug boppam gu muy wër ab diggam ci waxtu yu nekk mu neeti suuf si dafa wëndeelu maanaam roo te wëndeeloom googu nag tax na ba day yor doxiin walla yëngu yëngu gu roo mbaa guy wëndeelu waaye nag lu ñaaw la lool copernic ñàkk a man a tas te wisaare xalaatam yooyu ci bi muy dund ngir rekk ragal gu mu ragal jàngu bi egliis bi xalaatam yooyu wisaarewunu leen mbaa nu tas leen ndare ci atum g muy at mi mu faatoo boroom xam xamu itaali bii di galileo g moom jug def lu rëy ci jëmale kanam xam xamu bidiw loolu gën na a am ci ginaaw bi mu jëfandikoo fésalukaay ngir fuglu bidiw yi ak nekkteef yi ci kaw asamaan si mu dëgëral itam xalaati kopernic yi xam xamu fisiya gën na a jëm kanam te gën a buur ci xarnub fukk ak juroom benn g bu ko defee nga gis boroom xam xam yi ñuy dàggasante ci masalam yëngu yëngu ndaxte yëngu mooy cëslaayu xam xamu fisiya bu arusto maanaam ci la xam xamam boobu tegu boroom xam xami tugal yi def seen yite ci ñòddi gi nekk ci suuf si boroom xam xamu itaali bii di galileo di ku rawoon ci wàll googu moom de ci atum g yeegoon na ca sooroolub pisa bu jeng ba jël ñatti yef sànni leen ñu rotandoo ci suuf galileo mii moom lanuy jàppe ki gën a am solo ci boroom xam xami tugal yi daa yitewoo xam xamu fisiya ndax kat mooy ki teg dàtti walla fondmangi xam xam bii ci tugal ci fukk ak juroom ñaareelu xarnu g boroom xam xamu angle bii di isaac newton g mooy ki feeñal dooley ñòddi gi nekk ci suuf si moo wax ne bidiw yepp walla plaanet yepp danuy wër jant bi ci ay ngunu yu sax walla ay nekkuwaay yu sax yoo xam ne ñòddi gi nekk ci jant bi moo leen di nos te di leen teg ci yoon ki nuy wax laplace g moom itam ñëw sonn ba xam ni bidiw yi sosoo waa tugal yi tuxale nanu ci jullit ñi xam xam yu am solo yu aju ci xam xamu kimya bu bees bii nga xam ne boroom xam xamu jullit bii di jaabir bun hayyaan fésoon na ci lool te amoon ci ag raw ñoo leen xamal alkol soda gudrong saabu ak yeneen toggaliiti kimya yi nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci toggaliit yii ba leegi da nga ciy gis yoo xam ne turi ay jullit lay yore waa tugal yi nag ñoom danoo gën a jëmale kanam xam xamu kimya ci ginaaw yewwute gi ci noonu kii di josef priestley am tawfeexu di ci waa tugal yi ki njëkk a jële oksijen ci xoromi siibix atum g te loolu kat fekkoon na boroom xam xamu jullit bii di jaabir xamoon ko bu yàgg lavoisier di boroom xam xamub fraans di ki feeñal gaasub njëlbeenu oksid korbon atum g waay almaañ jii di rontgen g moom ñëw feeñalal ñu ceññeeri iks atum g boroom xam xam bii nuy wax thales di ku dëkkoon gres moo seetlu woon dooley ñòddi ju nekk ci kuran bi mu ko wokkee loolu mooy li nu njëkk a xam ci kàttanu kuran boroom xam xamu angle bii di william gilbert nekoon doktooru buuru angalteer bu jigeen bii di elisabet mu njëkk mi moom itam ñëw feeñal ne am na yeneen ne ne yuy am ag ñoddi boo leen jonjee yu dul kuran rekk feeñalug loolu nag mi ngi ame woon ci lu tollook atum g boroom xam xamu almaañ dikk fent ab jumtukaayu kuran buy juddal kuran atum g ki nuy wax stephen gray dikk won nu ni nuy tuxale kuran jële ko ci barab yobb ko ci beneen jaare ko ci fiil yu xànjar wolt mu itaali mi di ki wone duusi kuran yi te fent batari borom xam xamu amerig bii di bengamin franklin di ki wone ne melax ak kuran benn lanu mooy ki fent fegukaayu dënn misel faraday dikk moom itam di ki feeñal yoon woo xam ne ci la nuy jaare di genne kuran bu bari atum g waa tugal soobu nanu ci xam xamu mat waay itaali jii di tartaliya def ci lu am solo boroom xam xamu frans bii di fiit jëfandikoo woon na ay araf ci xam xamu jabru bii nga xam ne ci jullit ñi la ko waa tugal yi jële leodardo da vinci nag moom ci boroom xam xam yi sos xam xamu jiyoloji la bokk moom mi dëkkoon itaali jims hitn g itam ñëw di ki xamale ni doj yi nekke ak ni nuy sosoo jamonoy yewwute daal ci orob mooy jamono ji goreel xelum tugal mi te feexal xalaatam yaatal ko musal ko ci tënk tënki jamonoy orob ju diggu ji ba tay dees na ko jàppe muy jamono ji xayale te waajale ba xam xam man a jëm kanam man a naat ci tugal naataangey xam xam gii nga gis ci tugal ci jii jamono de dara waralu ko lu dul jamonoy yewwute ci jii jamono la ay jeem yu xam xam yu dëggu am yu sukkandiku ci yoonu xam xam wi jullit ñi fentoon bu yàgg lool njëkk waa tugal yi di ko xam ñatteelu doggantal yewwute gu endustri li mu jagoo ay màndargaam li mu fi indi yewwute gu endustri ci tugal ñi ngi ci jublu soppiku gu mag gi fa amoon ci wàllug endustri walla jëm kaman ga fa amoon ci wàllug jumtukaayu mekanig rawati na ci biritani ci ñatteelu xaaj bu mujj bi ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g waaye nag moom endustri mii yàggul dara mu tàmblee tas ci tugal nànk nànk ak amerig la ko dale ca njëlbeenug fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g bi mu ko defee nag ay jeexiitam tas ba àgg ci pàkk yu bari ci adduna bi loolu nag ci ñaari xarnu yii la fukk ak juroom ñeenteelu xarnu ak ñaar fukkeelu xarnu g endustri yi nag masuñoo dañ di jëm kanam ak a awaase ba ci sunu jamono jii nu toll looloo waral du man a ñàkk nu xam sabab yi tax yewwuteg endustri am ci tugal sabab yi tax yewwuteg endustri am ci tugal 	awaase gi xam xam awaase ci tugal ci jamonoy yewwute moo waral yewwuteg endustri am 	dëkki tugal yu mag yi am gi nu am ak tegu gi nu tegu ci yaxantu ak endustri ak woomleg koom gi loolu di jur nga xam ne day tax ba endustri di jëm kanam rawati na bi ci aju ci ràbbu ser nga xam ne mooy endustri bi njëkk ci tugal 	jëmm ci tugal ni mu jekki jekkee rekk fés mujj di dàtt bi mboolaayi orob yi tegu sabab la ci li yee waa tugal yi moom jëmm jooju ci orob ku nu tënk la woon ci jéngi nosteg laman jamonoy yewwute ñëw dog jéng yooyu feexal am xelam leeral ko ci xam xam ba mu man a xalaat bay fent ay jumtukaay yu am solo yu koy dimbli ci yombal ag dundam 	li juddoo ci wuññiy juxraaf yi it muy teg loxo gi reewi sancaan yi daa def reew yi nu sanc ak di fa jële ay xeewal aki ne ne yu nu laalagul di leen yobbu seeni reew loolu it bokk na ci li jëmale kanam yewwuteg endustri gi ci tugal 	reewi tugal yi ak këri koppar yi jàpple gi nu doon jàpple naal yi jug ngir jëmale kanam endustri ci orob loolu de ci li defar jawwu ji la ba endustri man a dox man a àntu 	boroom xam xam yu aay yi xëy feeñ te bari ci tugal 	bari gi ligeeykat yi bari ci tugal rawati na ñiy ligeey ci endustri yu ndaw yi na ngeen xam nag ne lu bari ci fentkati angle yi daa defar ak a fent jumtukaay yi ak masin yi ci ligeeykat yi amoon xam xam yu neew lanu woon nga xam xam ne daanaka jàngunu woon yewwute gi li mu jagoo woon ak ay màndargaam yewwuteg endustri ci tugal daa jagoo woon ay mbir yu bari yii ci lanu 	jëmale kanam gu nu jëmale kanam jumtukaayu ëcc ak ràbb meccem ràbb daal ci yi gën a jariñu ci fent yu xam xam yi aamoon ci tugal la rawati na ci britani loolu di ci ñeenteel bu mujj bi ci xarnub fukk ak juroom ñatt g loolu nag li ko waral mooy yitewoo gu tar gu nit yitewoo ay sér ak ñàkk a jafeg jëfandikoo jumtukaay yi ngir ligeey ci ràbbkatu angle bi nuy wax james hargreaves jot na a fent atum g benn jumtukaayu defar wëñ muy benn masin bu loxo bu nuy jëfandikoo ci ëcc li koy doxal nag doon genn mbege walla pono bu yor juroom ñatti ëccukaay ak ñaari forukaay bu ko defee benn ligeeykat di ko yor di ko doxal bu ko defee fentkat bu angle bii di richard arkrihgt fent moom it atum g benn jumtukaay buy xëcc wëñ yi moom nag jumtukaay la bu nu daa doxale ci dooley ay fas mujj nu koy defe ci dooley ndox nu tudde woon ko kaadaru ndox bi water frame ki nuy wax samuel compton ñëw fent atum g benn jumtukaay buy boole gaaw ci ligeey bi ak baaxle ko boobu jumtukaay nag tasoon na ci fi dend ak barabi ndox yi ci ñaari goxi angalteer yii di yorkshire ak lancashire ki nuy wax edmund cartwright moom itam àgg ci fent benn jumtukaay bu nuy doxale dooley ndox ginaaw bi nu koy doxale dooley cóolóol te kat tax na ba nu man a ful li nu daa ràbb daa ko defar ciy sér ligeey bi nu daa def ngir gën a jëmale kanam ak gën a rafetal ligeeyu ëcc beek ràbb bi gën a dolliku te sax nu àgg ci jëfandikoo ne ne yu kimya yi ngir raxas wëtéen wi defarati yeneneen jumtukaay ngir móol ay deseñ aki mbind ci ndima yi nu ligeey 	jëfandikoo kàttan jumtukaay yu njëlbeenu yi amoon nit a ko daa doxale ci dooleem walla dooley dundat kàttan nag di energie jëm na kanam ci jëm gi jumtukaay jëm kanam te awaase ci noonu nit jot a jëfandikoo ci njëlbeen gi dooley ndox ngir doxal jumtukaayam yi mu fent bu yàggul ginaaw bi mu jëfandikoo dooley cóolóol ak këriñ ki nuy wax thomas newman ñëw indi fi jumtukaayu cóolóol james watt moom itam dikk gën a defaraat jumtukaayu thomas boobu atum g loolu waral ay soppi yu mag yu xóot ci wàllug ligeey bi ak li nuy ligeey ndax kat duggal gi nu duggal jumtukaay bu mekanig bu cóolóol ci endustri ak jokkoo lu rëy a rëy la te am solo te moo tax ba nga gis endustri tay mu toll fii mu toll bu ko defee ca saa sa waa tugal yi tàmblee gëstu fu nuy jële këriñ këriñ nag bari woon na lool ci wels gu bëj saalum gi ak skotland nit it gënoon na a jeego ay jeego ci jëfandikoo gi muy jëfandikoo kàttan mu feeñaloon petrol ca d b a diiwaan yu bennoo yu amerig yi ci digg fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g ginaaw bi nu gisaat petrol fu bari ci adduna bi ginaaw bi nu fentati benn jumtukaay buy lakk ci biir boo xam ne mooy soppi petrol bi ginaaw bu ko lakkee def ko kàttan guy yëngal ak a doxal loolu moo waral ngay gis leegi jumtukaay yu mekanig yii nga xam ne danuy sukkandiku ci li nuy wax lakkug biir gi mooy lakku gi petrol bi di lakku ci biir jumtukaay bi jumtukaay yooyu nag ñooy yu mel ni oto yii ngay gis fafalnaaw yi gaal yii nga xam ne lakkug biir gee leen di doxal añs kuran tam jariñ na nit lu bari loolu nag mi ngi ame ci bi kii di faraday juge fent li nuy wax juddalukaayu kuran nga xam ne loolu indil na nit lu bari ci ay ligeey ak njariñ ci dundam nit àgg na ci xam kàttanug saal te jëfandikoo ko ci anam yu bari loolu tax mu man a neewal li muy sukkandiku ci petrol waaye nag nanu xam ne kàttanug saal moom lu seer la manu fee wuutu petrol ci genn anam nit it jot na a xam kàttan gu jant gi te jëfandikoo ko ci yenn anam yi niki nuggalukaayu ndox yu jant yi nuy jëfandikoo ci kër yi ak ci yeneen anam yi 	jëm kanam gu endustri bu weñ jëm kanam bokk na ci lu am solo li yewwuteg endustri gi jagoo bokk na ci jëmale gi nu jëmale kanam endustri bu weñ loolu nag mooy bi angle bii di bassemer jugee fent yoon woo xam ne manees na cee jaar bay soppi weñ di ko def sulb mooy weñ gu wow kong dëgër këng loolu nag ni mu daa ame mooy nu jaarale ko ci tàngoor wu kawe lool nit it gënoon naa def ay jeegoy jëm kanam ci wàllug yoon yi muy jaar bay genne këriñ loolu tam dimble ko ci mu man a dolli gën a lëwal li muy ligeey lii lepp nag bokk na ci li waral yewwuteg endustri gi man a am ci tugal rawati na ci britani 	jokkoo gën a jem kanam gu mu gën a jem kanam li kenn manul a sikk mooy ni endustri jëme kanam ci tugal de indi na fi ag jëm kanam ci wàllug jokkoo rawati na bi ligeeyu weñ gënee dox gën a jëm kanam ci noonu angle bii di george stephonson moom ñëw fent saxaarug coolool maanaam muy daw ci ay banti weñ ci diggante dëkkub liverpool ak manchester ci atum g yoonu weñ wii mooy yoonu weñ wi njëkk ci adduna bi ginaaw bi nitug amerig kii di robert foulton moom dikk jëfandikoo coolool di ci doxale gaali dex yu ndaw yiy daw ci dex yu mag yi nekk ci amerig gu bëj gànnaar gi ginaaw bi mu jugati jëfandikooti cóolóol dawal ci gaali cóolóol yu mag yii di daw ci geej yeek mbàmbulaan yi ci noonu la jokkoo tàmblee jëme kanam nànk nànk ni ko endustri defe bu ko defee feeñteg jëm kanam ci wàllug jokkoo mujj di feeñte giy raññale tey màndargaal yewwuteg endustri gu mag gii am tay ci adduna bi 	feeñug campeefi endustri yi ligeeyuwaay yu ndaw yi juge nanu ci kër yi doon leegi ay campeef yu endustri yu mag yu nekk leegi ci dëkk yu mag yi endustri yi mujj di loo xam ne am mbooloom ay lonkoo yu endustri yu mag ñoo koy moom ñooy lonkoo yooyu nga xam ne ñooy faral a moom li ëpp ci alal yi isin yu mag yi nag ci wetu barabi ne ne yu nu laalul yi lanu daa faral a sampu te loolu da leen daa dimble ci ñu man a neewal seeni fere ci lu aju ci seeni ligeey ndax loolu daa na tax li nu ci waroon a ñàkk gën a neew neewug fere yooyu daa na feeñ bu baax ci njëg yi ndax daa na leen daaneel te daa na gën a baaxal ligeey bi gën koo wuuteel li fi yewwuteg endustri gi jur maneesul a sikk ne yewwuteg endustri gi indi na ci tugal ay ngérte yu yaatu ci wàlli koom politig ak mboolaay li mu fi indi ci wàllug koom yewwuteg endustri gi bàyyi na fi ay jeexiit yu rëy ci wàllug koom ci biir orob ak biteem ndax ca la isin yu mag yi tàmblee feeñ yi daa am jumtukaay yu rëy yi li nuy ligeey gën a yokk gën a wuute li nu koy jënde gën a neew ñepp man cee jot jumtukaayi ligeey yi gën a bari jokkoo gën a yomb yoon yi gën a bari ja yu adduna yi gën a yaatu lonkoo yu mag yi amoon ay gis gis aki xemmemteefi rënk ak sanc tàmblee booloo ndax kat sanc gu politig gu yees gii du lu dul doomi sanc gu koom koom gi tugal daa def jaare ko ci endustreem bu jëm kanam bii ak baaxug ay jumtukaayam ak soxla gu tar gu mu soxla ne ne yu nu laalul yi ak soxla gu mu soxla ay ja yu yees yu mu man a jaaye marsandiisam yu bari yii te wuute waaye mbay nag moom ak li ay jumtukaayam gën a jamonoo lepp ak li mu gën a ñaw lepp te gën a xam xame teewul ay njëgi li ciy juge gën a seer li ko waral mooy li ëppoon ci baykat yi danoo gàddaayoon àll yi dem ci taax yi fi isin yi nekk ngir man fa a ligeey ndax la nu daa gañee ci ligeey bi moo daa gën a bari te daa nanu ci ame ag sax fi barab gàddaay gii nag juge ci àll yi dem ci taax yi taxoon na ba ab kiris walla jafe jafe bu rëy amoon fi ci wàllug mbay ci orob rawati na ci angalteer joxalanteg yaxantu gën a yokku ci adduna bi nga gis reew yiy defante ci seen biir ay kollarantey yaxantu ak yeneen kollarante yu aju ci yombalug jaarale marsandiis yi ci geej yi ak mbàmbulaan yi ak barabi romb yu adduna yi ci noonu lonkooy yaxantu yu adduna yi nga xam ne seeni boroom danuy am alal lool tàmblee feeñ bank yi tàmblee yëngook a sawar ak këri koppar yi li mu fi jur ci politig sanc gii tugal tàmblee sanc reewi jàmbur yi ak di leen teg loxo bokk na ci li fi yewwuteg endustri gi indi wuutal ko fi ginaawal ko fi ci wàllug politig ndax ni ma la ko waxe woon ci ginaaw endustri day soxla ay ne ne yu nu laalul te loolu danu ko daa gis feneen fu dul tugal te loolu jur na ay xare ci diggante ay reew ci fu bari ci sunu adduna bii tax it ba reew yi nu sanc jug di xare ngir goreel seen bopp soril senn bopp ag sanc ak lepp lu ko jege ci xeeti moomadi sa popp ak tembadi bu ko defee benn dal daal di feeñ ci orob mooy dalu koom koom bu gore bi walla bu libre bi am te taxaw ci nosteg bopp alal loolu nag mi ngi am ci ginaaw bi endustri bu yees bii soppikoo dem ci noste gii li ko waral di yitewoo gu bari gi mu yitewoo ci nu sos ay isin yu mag ak isin yu mag yii yitewoo gu tar gi nu yitewoo alal ju bari ngir taxawal leen sos leen goornamaay tugal yi jàpple woon nanu noste gii te dëgëral ko ci mbooleem li nu man am ko ciy man man aki kerkeraan ci noonu warteefi goornamaa yi gën a yaatu gën bari ci mboolaayi endustri yi loolu yobbu ko ci ay warteef yu mel ni sonn ci mbiri mboolaay yi te yittewoo leen sosal leen ay jàngu aki daara yu mag ak sonn ci mbiri wér gu yaram ak lepp lu yitteel mboolaay gi maanaam societe bi ci noonu ay boroom xam xam aki bindkat daal di feeñ yoo xam ne seen ligeey bepp ñi ngi ko jëmale ci luy dundal mboolaay gi suqali ko ay gisiini politig yu yees feeñ yoo xam ne bokk nanu ci li fi indi xalaatu politig bu tugal bu yees bii tay goornamaay tugal yi duggsi nanu ngir aar ligeeykat yi ci noonu ñu yamale waxtu yi nuy ligeey def leen leegi ñuy waxtu te bu njëkk waxtu lanu woon ñu ñëwati indi fi noppaluy tawat yi ak yu jeexiitalu ayu bis yi ak yu at yi ñu defati ay ligeey ngir yekkati seen payoor yi jeemati ba seenug dund ak seeni dëkkuwaay gën a baax man gi reewi endustri yi man a doxal seen mbiri reew feeñ na te am bi reew yooyu amee alal ju doy ak ngànnaay yu yees te xereñ bu ko defee nga gis reewi tugal yi sukkandiku ci endustri ëpp doole fuuf yi sikkandiku ci mbay ak ngànnaay yu yàgg yi nu miinoon li mu fi jur indi ko fi ci wàllug mboolaay yewwute gi ci orob jur na ay gàddaay yu mag juge ci àll yi ak dëkk dëkkaan yi dem ci taax yi ak dëkki endustri yi loolu nag mi ngi am ci bi isin yi yokkoo jumtukaayi endustri yi gën a xereñ cig wàll moomeeli mbay yu mag tàmblee feeñ ci tugal la ko dale ca ñaareelu xaaju xarnub fukk ak juroom ñatt g rawati na ci angalteer ci geneen wàll bu ko defee baykatu orob bi moom gisoon ne li ko gënal daal mooy mu dem ci isin yii nga xam ne li nu koy fay moo gën a wóor te gën di lu nu xam te bàyyi mbay mii nga xam ne leeg leeg mu baax leeg leeg du baax ak jafe jafe yi mu àndal muy njaay meek toppatoo gi lii mooy li waral ñiy ligeey ci mbay neew te wàññiku ñi dëkke kaw gi gën a neew loolu it jur yokkug ñi dëkke ci taax yi bu ko defee am lu juddoo ci loolu mooy neewug jóoxiitum mbay mi te loolu it tax na njëg yi aju ci mbay ak li ciy juge gën a seer beneen jafe jafe daal di juddooti mooy bu aju ci dëkkuwaay ñeel way gàddaay yu bees yii gàddaaye kaw ga ngir dëkksi ci taax yi di wër ligeey ci noonu ay barabi dëkkuwaay yu xat tàmblee feeñ ci wetu fi isin yi nekk di dëkkal lu sakkan ciy nit te matalewul li nu laaj ci dëkkiin wu baax te xellu ci noonu wér gu yaram dajeeki jafe jafe yu rëy a rëy jikko it naka noonu jafe jafey ligeeykat yi gën na a yokku bi nu demee ba li nu leen di fay manatul a faj gën ja a neewi seeni aajo ngir seerug dund gi beneen jafe jafe bu mboolaay bu bees amati ànd ak yewwuteeg endustri gi ak ag jëmam kanam loolu mooy ne lu bari ci jigeen ñeek xale yi leegi danoo tàmbli di ligeey ci isin yi te kat kenn soññu leen ci ku dul boroom isin yii nga xam ne li leen ñoroon weesuwul nu nu man a gën a ame ay ligeeykat ba gën a man a neew lu nuy fay ginaaw ligeey bi ci isin yi laajul doole ju rëye noonu ngir man ko loolu tam jurati yeneen jafe jafey mboolaay ndax tax na ba jigeen bàyyi fi ay ligeeyi boppam dem ci isin yi xale yi it bàyyi njàng mi te loolu ag pert manu koo kawe ndax xale yi ñooy yaakaari ëlëg ag yàqu yàqu tàmblee feeñati ci wërlaay gu mboolaay yi ci tugal maanaam nit ñi loolu nag mi ngi am bi ag ñàkk ligeey tàmblee tas ak a yaatu ci orob ci ligeeykat yu góor yii nga xam ne danoo tàmbli woon a nekk ay jafe jafe dëgg ci kanamu goornamaa yi di yëngal tey sàkku nu nu leen lijantile seen jafe jafey ligeey yi ci noonu goornamaa yi daal di def ay àtte indi ay sart yu nos ligeey bi aar ligeeykat yi ci fuqaleg boroom bopp alal yi moom isin yi ñatteelu bunt bi yëngu yënguy politig yu mag yi ci adduna bi feeñug diiwaan yu bennoo yu amerig yi u s a jeqiku walla fipp ga amoon ca fraans doggantal gu njëkk gi feeñug diiwaani amerig yu bennoo yi gàddaay yi waa tugal yi daa def juge tugal jëm amerig gàddaay yooyu wéyoon nanu di sottiku ci amerig gu bëj gànnaar gi loolu nag amoon na ginaaw bi kolomboo feeñalee amerig ba am lu tollook xarnu li ko taxaoon a am nag bari na bokk na ci 	fitnay diine yi amoon ci orob gu digg gi ak gu sowwu gi li waraloon loolu di yëngu yëngu yu diine yi jugoon di kontar egliisu katolig bi ak la ca juddoo muy ay xeexi ngér yu amoon ci diggante ngérum katolig ak mu protestant ak xeex bi protestant yi doon def ci seen biir rawati na ci angalteer ak la ca juddoo muy bòddikoonte ci diine loolu nag waraloon gàddaayug ab lim bu mag ci waa tugal yi dem amerig gu bëj gànnaar gi ngir rawale seen bakan ak ngir man a doxal seen diine ci ag féex akug ngore 	fitnay politig ya amoon ca tugal ngir xeex jaay doole ga fa amoon ak àttee na mu la neexe ga ak la ca juddoo muy ag ñàkk a nosu gu mbir yi ñàkk a nosu ak ñàkk kaaraange ak dox gi nguur yi di doxe ni mu leen soobe loolu lepp nag taxoon na ba lu bari ci waa tugal yi gàddaaye woon fi nu dëkkoon dem wuti ag goreg politig 	wër gi nu doon wër mbll yu gànjaru yi lu ci mel ni wurus mbaa xaalis bokk na ci li leen daa gàddaayloo ndax kat lu bari ci ñi daa gàdday danoo gëmoon ne amerig de reew mu fees dell la ak yile mbll te ña fa dëkk ñu neew ag xay lanu te ñàkk ag taaxe te yittewoowunu yenn ligeey yu mel ni lijanti ay wurus aki xaalis ak gasi mbll 	jëm kanam gi xam xam am ak endustri ci tugal rawati na ci wàllug ligeey ay gaal googu jëm kanam dimblee na ci nu man a tukki ci geej gi bay àgg ci barab yu sori yee sori 	ligeey yi nga xam ne lonkoo yu angalteer yi def nanu leen ngir meññal ak jariñoo suufus amerig si ak lijanti nu ñu koy sance te dëkke ko ngir dëgërale ci kilifteefug sanc gu angalteer ci goxub adduna bu bees bii bokk na ci li waral gàddaay gi sancu yi nga xam ne waa angalteer yi taxawal nanu leen ci amerig gu bëj gànnaar gi waa tugal yii bawoo woon espaañ fraans holand suwed ak angalteer sancoon nanu ay barab yu wuute ci amerig gu bëj gànnaar gi ñoom lanuy wax tay diiwaani amerig yu bennoo yi loolu nag di woon ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom benneel ak bu fukk ak juroom ñaareel g angle yi nag ñooy ñi njëkk a taxawal ab sancu ca jims town ci diiwaanu new york atum g mujj nanu nag ci diir bu gàtt di ñi gën a tas gën a wisaaroo ci goxi tefes yu penku yi ci mbooleem ñi gàddaayetugal barabi penku yii maanaam yii nga xam ne la ëpp ca ña fa sancoon dëkke woon fa ay waa angalteer lanu woon barab yii mooy yi mujjoon ginaaw bi g di laaj ag temb akug dagge ca reew may nday di angalteer angle yi nag amoon nanu ñaari anam yu nu daa sance reew yi ak a yilife bi ci njëkk mooy buurub angalteer da daan may yenn ci lonkoo yi gu ci mel ni lonkoo gu werjiniya gu london gi mooy bi yoroon mbirum sos sancu bu jims town bi nu la waxoon leegi da leen daa may ay sañ sañ ci nu taxawal ay sancu ak jariñoo xeewal ya fa nekk ak defar xaalis walla koppar yu nuy man a jëflantee ak topptoo mbirum kaaraange gi geneen anam gi mooy buur bi day dogal garmi yu angalteer yi ay suuf ba noppi féetale leen mbirum yor leen ak àtte leen bi fukk ak juroom ñatteelu xarnu g di agsi ci digg bi amerig mujj na yor fukk ak ñatti sancu yu angalteer ñooy new york wirjiniya rood island masacuusest dulawir new hamser kintakit north karolaayna south karolaayna new jersi jorjiya ak pensilvaniya diiwaan yooyu ñooy yi sos te amal li nuy wax diiwaani amerig yu bennoo yi ci ginaaw xareb temb gi atum g ñu mujj am ag temb ci angalteer ci mujj gi diiwaan yooyu nag bu nu leen xoolee ci amerig gu leegi gii nii dunu weesu benn xaaj ci amerig gu nu xaaj fukki xaaj noste gi doon doxal mbiri biir yu sancu yu angalteer yi nguurug angalteer gi daa joxoon ay sancoom yi nekkoon ci amerig gu bëj gànnaar gi da leen a joxoon aw xeet ci ag àtte sa bopp waaye teewul ci biir loolu lepp mu bàyyil fi boppam kilifteef ak cang gu mu am ci kaw sancu yooyu maanaam may na leen ñu yor seen bopp di doxal seen mbiri biir waaye teewul muy seen kilifa di reew mi leen moom nosteg àtte sa bopp googu amoon ci sancu yooyu mi ngi tegu woon ci ñatti ponk 	doxalkat bi 	jataayub yoonal bi 	jataayub diisoo bi doxalkat bi walla àttekat bi mooy kilifa gi yilif dooley xare ji ci sancu bi mooy feetewoo sàmm mbiri way dëkk yi di topptoo kaaraange gi te am na sañ sañu dindi saxal gu nu defe ci ñaari jataay yii bu yoonal bi ak bu diisoo bi moom nag àttekat bi buuru angalteer bee koy fal ak a folli bu dee nag jataayub yoonal bi moom ñi dëkk ci sancu bi ñoo koy tànn li ko tax a jug nag mooy tege galag yi ak fuglu ligeeykat yi ak saxal seeni payoor ak payooru doxalkat bi bii jataay nag li ko may doole mooy jële gi mu jële sañ sañam ak kàttanam ci nit ñi dëkke ci sancu bi ginaaw ñoo ko fal jattayub diissoo bi moom li ko taxoon a jug mooy di xelal àttekat bi ak jataayu yoonal bi ak di diisoo ak ñoom waaye nag moom sancu bi ak li mu jot a am lepp muy ag àtte sa bopp gi nga xam ne taxoon na ba nu man fa a doxal demokraasi teewul mu nekkoon ab sancu rekk bu toppoon ci ginaaw nguurug angalteer gi ci gisiinu waa angalteer goornamaa bu angalteer li mu fàttee def mooy wut nu mu nose mboolooy angle yii dëkke woon sancu yi ñoom mbooloo yii nga xam ne mujj nanu lu jamono di gën a yàgg ñuy gën a sori seen reewum nday ma di angalteer ci wàllug aada ak dundiin loolu waral ñu tàmbli koo fàtte di yëg nag leegi ne fii mooy seen reew di ci tënku te di ko fonk loolu nag tàmbli woon na a wuute ak politig bi george mu ñatteel mi taxawaloon moo doonoon burub angalteer ca jooja jamono lii mooy li taaloon ab xare bu mag ci diggante sancu yi ak nguurug angalteer gi xare boobu moom lanuy tudde xareb temb bi li waraloon xareb temb bi ñi dëkke woon sancu yi ay mbooloo lanu woon aki kureel yu wuute ak doonte la ëppoon ca ñoom ay waa angalteer lanu woon yu di ay protestant seeni njariñi koom koom it bokkewul woon te niroowul woon waaye nag loolu lepp teewul woon amoon nanu ñatti mbir yoo xam ne kenn wuutewu ci woon ñepp a ci dëppoo woon ñooy 	am gu nit war a am ag goreg jëmm rawati na goreg pas pas 	 ak sàmmoonteek yoon ak nosu maanaam nosu gi mbir yi war a nosu 	yëg gi ku nekk yëgoon ne fii ci sancu yii la dëkk moo dim reewam fa la feetale ag reewoom ëttub amerig bii nag mujjoon di def ay mbir yoo xam ne ñoo waraloon xareb temb bi tàkk mbir yooyu manees na leen tënk ci yii yoon yuy tege galag ak tembar parlamaa bu britani bi daa genne atum g aw yoon walla luwaa bu nuy wax luwaa bu tembar yi mooy biy def ngay fay tembar ci jëflante yu ofisel yi ak dosyee yi ak yëglekaay yi añs ci atum g ñu farataal galag ci suukar si nu daa jële ci sancuy espaañ yi yu fraans yi ak yu holand yi teg ci farataalati ko ci ataaya kayit weer ak rasaas yoon wi aju ci geeju navigation ak yaxantu ci atum g barlamaanu britani bi dafa genne benn luwaa buy waral ci sancu yi nuy tuxal li nuy genne ak li nuy duggal di ko def ci ay gaal yu britani aaye leen ñuy jëndati feneen leneen loo xam ne bari na angalteer koppar walla kee bu kayit ak jënd suuf sancu yu britani yi danu leen a aaye woon ci yoon ñuy genne walla ñuy defar benn kee bu kayit ak di ko jëfandikoo niki kee bu ofisel noonu tam lanu teree woon ci beneen luwaa ñuy jënd suuf yi feete sowwu fukk ak ñatti sancu yi ngir jàpp gu nu jàppoon ne yooyu suuf nguurug britanee leen moom nos dooley kaaraange ji goornamaa bu britani dafa sosoon jenn doole ju xare ngir aar sancoom yi nekkoon ci amerig gu bëj gànnaar gi doole jooju tolloon na ci junniy xarekat mu waxoon waa sancu yi ne ñooy warlu di joxe depaas yi doole jii di laaj loolu nag taxoon na ba waa sancu yi mer ñaawlu loolu lool ngir loolu tam goornamaa bu britani bi ne kon na ci genn waaye nag galagu ataaya moom dindiwu ko loolu tam tax na ba waa sancu yi di yëg ne ñoom daal danuy jëflante ak ñoom mu mel ne dañuy ay nit walla ag njaboot goo xam ne ñoo gën a neew solo ak daraja ñi dëkke angalteer waa sancu yi tam yëgoon nanu ne li nuy fay ciy galag lepp dunu leen ko defal fi nu koy faye waaye kay ca reew mu leen sori mee di angalteer te loolu du leen jariñ ci seen dund gi te du ci def dara nga rax ci dolli ne angalteer mooy reew mi rënkaloon boppam ci sancoom yi yaxantug marsandiis yu bari maanaam bari na lool ay marsandiis yoo xam ne angalteer da ne woon moom rekk a leen sañ a jaay ci sancu yi lu mel niki ataaya loolu nekkoon na lu waa sancu yi ñaawlu woon ci nii daal la xew xew yi toppantee woon di nëxal nag sellug seqoo gi amoon ci diggante angalteer aki sancoom loolu tam gën a yaatal paxum reeroo mi nekkoon seen diggante loolu nag gën na a fés bi waa sancu yi bañee ne dunu fayati galagu ataaya ginaaw bi tam am mbooloo jug ci desambar atum g lakk ñatti gaal yu nguurug angalteer yu nu duyoon ak ataaya ca waaxub boston ca sancu bu masacusets loolu waral waa angalteer tëj waaxub boston bi ne gaalug yaxantu du fi teerati daal di ne moom ci jëmmi boppam mooy yoral boppam sancu boobu xew xew bii ak la ca juddoo man nanu ne moo waral xareb temb bi ndajem waxtaan mu filadelfiya mu njëkk mi juroom ñeenti diiwaan yu ameriig teewe woon nanu ndajem new york ma atum g di sàkku ci nguurug angalteer mu teggil leen galagu tembar bi mu leen di teg ci noonu angalteer teggi woon na galag boobu waaye teewul mu wéyoon di tege yeneen galag yi nga xam ne ab parlamaam daa na leen woote te di leen farataal ci mbooleem ay sancoom yi nekk ci adduna bi looloo taxoon reenub reeroo bi amoon ci diggante angalteer aki sancoom saxoon fi di lu ñu dogadi ndax kat sancu yi danoo gisoon ne di leen teg ay galag te seeni jataayi yoonal ànduñu ci bu amee lu muy tegtale mooy dindi màndargam demokraasi mi seen jataay yooyu di doxal seeni mbir ame woon ndax kat daa am ab dal bu nekk ci demokraasi bu naan doo fay galag boo amul ndaw man nanu ne ndajem new york mi mooy lu njëkk a feeñ te nosu loo xam ne waa sancu yi def nanu ko di ci kontar ni angalteer di àttee seen reew yi ñoñ sancu yepp a meroon bi angalteer tëjee waaxub boston bi bu ko defee ñu taxawal am ndaje ca filaadelfi atum g jàmmaarloo fa ak angalteer ne ko na xam ne lepp lu mu defati benn sancu ci sancu yi na ko wóor ne sancu yepp la ko def daal di ñaawlu bu baax jëf yu ñaaw yi angalteer tegoon boston njiitul xare lii nuy wax george washington g teewe woon na ndaje ma ndajem filadefi moomu mooy dàtt bi nga xam ne ci la kongres mujj a teggu ci ginaaw bi jaadu na ñu leeral leen ne ndajem filadefi mi li ko taxoon a jug du sàkku ag tembte waaye kay yëgal angalteer ne lu wuuteek demokraasi lii muy def ci sancu yi neexu leen te man na a nëxal te yàq xaritoo ak jàmm ji amoon ci diggam ak ay sancoom ñoom kay seeni càkkuteef weesuwutoon lii mooy na angalteer xam ne ñoom sancu yi kat ñoo ame àq ak sañ sañ ci seen jataayi yoonal yi ci tege ak farataal ay galag ci waa sancu yi angalteer nag ci safaanub muy lijanti lëj lëj boobu ci maslaa gu xereñ moom daal da fee nekk di yonnee ay dooley xare yu yees ci boston ngir gën a dëgëral doole ja fa nekkoon loolu tam li mu juroon mooy waa sancu yi ñoom itam ñu ne woon nanu waajal seen bopp ndax kat nguurug angalteer gi bëggul jàmm ci noonu ñu ñoom waa sancu yi defaat beneen ndaje ci filadefi ngir jàng mbir mi seet nu ñu ciy def ndajem filadelfi mu ñaareel mi ndawi sancu yi defoon nanu am ndaje atum g ca filadelfi muy ñaareelu ndaje mu filadelfi mi ñu wax fa ne danuy sos menn mbooloom xare te bennal ko bañ a def sancu bu nekk am sa mbooloom xare bu ko defee nag mbooloom xare moomu ñu tànne ko ci waa sancu yi ngir ñu aar leen ci ay wi leen dëgmalsi ci noonu ñu duggal doomi sancu yi ci xarekat yu bees yii nga xam ne george washington moo leen jiite woon waaye teewul ñu yonnee ca buuru britani bi ab bataaxel buy sàkku ci angalteer mu xoolaat ni muy jëflanteek sancu yi te lenn baaxu ci waaye buur bi moom jàpp fa mu jàppoon rekk ne daal am na ag cang gu nu joyal ci kaw mbooleem sancu yi ci jëfam jooju la tëje buntub jeem gi sancu yi doon jeem ngir defar ak doonte lu neew la itam seen diggante ak britani reew miy nday ni xare bi tàkke bi buur bii di george mu ñatteel mi ñàkkee faale càkkuteefi sancu yi ne daal li wér mooy moo ame cang gu joyu gi ci mbooleem sancu yi maanaam sancu yepp ci ron kilifteefam lanu nekk ci anam gu matale te daj bi buur bi nekkee ci taxawaayam boobu ne du ci juge la xare bi tàkk ci diggante ñaari wàll yi sax nag lu toll ci juroom ñaari at daanaka g bu ko defee mu tas nag ci li ëpp ci sancu yu amerig yi george washington nag jot na a man a nangu boston ginaaw bi mu ko gawee dooley gornamaa bu britani moom teg loxo lu bari ci waaxi amerig yi george washington ni mu doon xeexe ak ñoom nag mooy xeexub bette ci barab yu bari ak door daw foo ko fekk daawul nangoo jaamaarlook ñoom ndax xammoon na ne ñoo ko ëpp doole te gën koo tàggatu ak li xarekati sancu yi doon jànkoonteel lepp ciy coona yu tar ci biir xare bii teewul george washington gañe woon na njiitul anglteer lii di burgoyne ci xareb saratoga loolu mi ngi am bi mu jawalsee juge kanada jëm new york ci oktobar g ca saa sa ginaaw bi nu gañee britani fraans jug na yëgleb xareem ci kawam atum g espaañ roy ko ci atum g holand topp ci atum g man nanoo wax ne fraans moom jàpple na way fippi sanncu yi ci wàllug xare militaire ak ci alal ba tay it dajale na way coobarewu yu fraans yi yobbu leen ci diiwaan yu bennoo yi ngir nu xeexle leen ci ron njiit lu xare lu fraans lii di lavette kontar angalteer noonam bu mu yàgg a noonool bii ci noonu britani mujj war a xare ci jë yu bari dàq gi nu mujj a def dooley angle ji ci sancu yi mooy gi nu defoon seen njiit la cornwallis loolu di bi mu deltoo ginaaw dem dëkkub york town fa dexug york di sottikoo ginaaw ba ko fa mbooloom xarem george washington ma songee xarekati george washington yooyu nag am njaxasiitum kureel lanu woon mu ame ci diggante ay waa fraans aki ñoñi sancu tollu nag ci fukk ak juroom benni junniy xarekat nanu fàttaliku nag ne waa amerig yi ñoom ci seen suuf lanu doon xeexe bu ko defee dolli leen doole ci xare ak ci alal day gën a yomb gën a gaaw bu dee waa angalteer yi xawoon a sori kanada fi seen bagaasi xare daan juge walla angalteer mi leen soree woon lu tollook ay ñatti junniy miil daanaka nga rax ci dolli waa amrig yi danoo dogu woon bu wóor ci raxasu ci teg loxo gi britani tegoon loxo seeni mbir te amoon nanu ay njiiti xare yu bari ku ci mel ne george washington doolil ci loolu nekk gi waa britani nekkoon di xeexe ci sancu yoo xam ne manuñu fa a ame jokkoo ak dolli doole ga war ca anam ga mu ware te gaaw te itam pasteefub xeex bi nu amoon moo gën a suufe fuuf bi waa sancu yi amoon ñoom ñi taxawoon tamb ci xettaliku ci waawug nguurug angalteer gi bokk na ci li doyadil waa britani yi ci xeex bi ubbi gi nu gubbi woon ay jë yu xare yu bari ci seen kaw ci barab yu sakkan ci amerig tembug diiwaani amerig yu bennoo yi bi waa britani xamee ne lòtt nanu ci toroxal jeqiku gi amoon ci amerig te xam ne doole du mooy lijanti lëj lëj yi nekk ci sancoom yi ndax kat mi ngi nii di ku nu dàqe gañee ko ca xare ba bi loolu amee mu sàkku woon ag juboo ci noonu ñu xaatim juboo gi ci paris ci digganteem aki sancoom atum g lii mooy poñ ya ca ëpp solo 	britani day nangu tembteg sancu yi nekk ci suuf yi feete ci penkub dexug misisipi gi te jàppe dex gii muy diguw soww wi ko tàqale ak sancu yi bu ko defee dig yu bëj gànnaar yi ñoom ñu bàyyi leen nanu nekke woon 	jeem a rafetal seqoo yi ci diggante britani ak reewum amerig mu temb mi diiwaani amerig yu bennoo yi 	amal ci diggante britani ak amerig gu temb gi ay seqoo yu yaxantu ak yu koom koom waaye nag seqoo yooyu ñu teg leen cig nawlante ak moroomante kenn du jaay kilifteef sa moroom nii daal la diiwaan yu amerig yu bennoo yi ame xareb temb bi nag am na benn jeexiit bu rëy te xóot ndax wal na te upp ngelawul gore ak temb ci mbooleem sancu yi lii nag làppal na britani loofloo ko ci wàllug xare ak politig nga rax ci dolli alalam ju bari ji mu ci ñàkke amerig nag moom daal di ñew defar sartu reewam daal di taxawal ndajem booloo mi nga xam ne kongres moo ko digale woon atum g mbooleem ndawi diiwaan yu bennoo yi teewe woon nanu ko ba mu des diiwaanub rood island cer ya fa nekkoon tam tànn cig dëppoo george washington muy njiitul ndaje mi ci loolu la nekke ki njëkk a nekk njiilul diiwaan yu bennoo yi ginaaw bi lanu def washington ginaaw bi mu nekke peeyu koom koom bi ak bu alal bi la nu ko def peey bu politig bi george washington nag jëloon na xalaatam yepp def leen ci nu muy def ba bennal amerig looloo taxoon waa amerig yi soppoon ko wormaal ko waxam it weesuwutoon doon leen benn doon leen ay waa amerig loolu saxoon ci seen xel yi washington moom wàcci na jal bi joxe njiit gi atum g ginaaw bi mu ko yoree ñaari yoon doggantal gu ñaareel gi jeqiku walla fipp ga amoon ca fraans jeqiku walla fipp ga amoon ca fraans mooy jeqiku gi njëkk a am ci jamono ju bees jii ci kaw nguuru ak jaay doole ak doxale ni la neexe doo diisoo doo deglu xalaatu keneen moom nag fipp googu mi ngi ame woon ca fraans ca jamonoy buur ba tuddoon luwis mu fukk ak juroom benn ma bokkoon ca njabootug barbon ga loolu nag di woon ca noorub g saxoon it diir bu toll ci fukki at ba ca nawetub atum g bi jeneraal bi tuddoon napoleon bonaparte g defee yong gu nuy wax yongug brumaire dëppoo ak nowambar g daal di daaneel doxaliin wa fa nekkon jële fa it jataayub mag ña mujj nag di kenn ci ñatti kilifa yiy doxal mbiri reew mi bonaparte mii nga xam ne mujj na di kilifag fraans gu njëkk gi ci atum g mujj it di imbraatoor ba atum g moom bonaparte mujj na am tawfeex ci dindi lëjug politig ga fa amoon ñàkk jàmm ga tiitale ga tuur dereet ga ak yeneen jëf yu ñaaw yi àndoon ak fippug fraans gi loolu nag taxoon na ba fipp gi manu fi woon a amal dali gore yamoo mbokkoo yi nga xam ne ñoom la yàgg a yekkati kàddoom ngir saxal leen fi waaye nag jeexiit yi nga xam ne fipp gii ba na leen fi yamuñu rekk ci fraans waaye weesu nanu ko ba daj tugal gepp ak lu bari ci reewi adduna bi ni fraans meloon laata fipp gi bu ñu gëstoo na fraans meloon laata fipp gi loolu di na nu dimbli ci nu man a xam li waral fipp gi atum g melokaanu politig wa buuri fraans yi ni ñu doon àttee fraans du woon nenn nu dul ni mu leen neexe buur bi moo daa saytu lepp kepp ku am nguur moo la ko daa jox moo daa doon balluwaayu mbooleem doole yi ak sañ sañ yi walla nga ne sax mooy nguur gi di sañ sañ bi di kàttan gi di doole ji loolu nag man nga koo degge ci waxi buurub fraans bii tuddoon luwis mu fukkeel meek ñeent man maay nguur gi buur bi mooy ki am sañ sañ ci def ay yoon ak neenal leen tege ay galag def ci alali reew mi lu ko soob tabb jëwrin yi fal ligeeykat yi folli leen joxe ay ndigal jaare ko ci ay bataaxel yu nu xaatim ngir nu jàpp ku ko soob ci askan wi ak tëj ko ci lu dul mu koy àtte mbaa mu koy laaj dara buur bi daal ci gàttal lu ko soob mu def ndax moom dafa gis ne mi ngi wéeru ci sañ sañam boobu ci gis gis bi fiy indi sañ sañu yalla bi mooy li naan buur bi daal nguuram gi ak sañ sañam bi mi ngi bàyyikoo ca yàlla luwis mu mii nag nga xam ne ci atum g la nekkoon ci jal bi tey buur bi nga xam ne ciy jamonoom la fipp gi xewoon moom luwis mii nekkoon na ku doyadi te daan dengi dengi moom de jaraafam yi danu koo yilifoon ak bëkkneegam yi ak soxnaam si bàyyikoo woon hongri mari antuwanet di woon doomi lingeerub ongri ba mariya tereesa moom soxnaam soosu nag ku yëgoon boppam la te faaleedi woon askan wi taxoon na ba kenn manut a def genn yéwénal kenn manul a jàpple buur bi ci luy defar moom daal nekkewu fi woon lu dul yàq alal noos ak caaxaan nekkoon it ku diis te rëyal boppam looloo taxoon mu mujjoon di ku waa fraans yi bañoon njabootug barbon gi yàgg nanoo jariñoo seen nguur gi ci luy lor askanu fraans wi ñoom daal danu daa nangu alali ku leen neex daan tëj ku leen soob daan xeexloo reew mi saa su leen soobee te xeex yooyu yu ci ëpp danu ci daa gañe fraans bari na lool lu ñu daa tabax ay njénd di ci sotti alali reew mi ak di may seen dag yi alal ju dul jeex seen dag yu bari yooyu nga xam ne tolloon nanu ci junniy nit atum g te lu ëpp ci ñoom defuñu fa woon dara amul lenn lu nu fay ligeey lu amal njariñ reew mi looloo taxoon njëlul nguur gi loof mujj moom nguur gi fees dell aki bor nguur gi kat mujj na ay deppaasam àgg ci milyong yu frank atum g li mu ameele woon ciy bor àgg ci milyon yu frank ngir lòtt gu njëlam li lòttoon baj baji ak doxadi amoon na ci wàllug doxaliinu nguur gi ci wetu doxe ni la neex ga amoon ca wàllug politig ga nattukaayi gox bii daawul bokk ak bee naka noonu yoon yi màndaxekaay yi galag yi ci noonu fraans mujj di reew mu ay gox boole gox bu ci nekk am ay yooni boppam aki nosteem yu wuuteek yeneen ya ca feneen loolu nag waraloon na ag lënt ci nosiin yi ak luwaa yi reew mi mujj seddaliku doon ay doxaliin yu temb bu ko defee fraans mujj doonatul menn reew waaye ay doxaliin yu wuute te tas na mboolaay ga meloon mboolayug fraans gi njëkk fipp gi dafa seddaliku woon doon ñatti kureel yu mboolaay ñooy kureelug ñu tedd ñi walla garmi yi kureelu niti diine yi ak kureelu mbooloo mi walla baadoola yi ñatti kureel yii nag ñoom de ci li fi jamonoy laman desaloon lanu yamoowunu woon ci àq ak yelleef du caageegug ci ay warteef li am daal mooy ag yamoodi gu mboolaay amoon na ci seen diggante jefkay tàqali ak feewaloo ruuru leen ak boddante gu mboolaay bu ko defee kureelub garmi yi nu teggil leen galag yi ña ca bokk it ñoo daa feetewoo pal yu kawe yi yu siwil yi ak yu xare yi ci nguur gi ñoom ba tay daa nanu am ay cer ci mbayum baykat yi ak ci jurug sàm yi ak seen ñanaaw yi amoon nanu it sañ sañ ci rëbb ci tooli baykat yi baykat yi tam amunu wonn sañ sañ ci wal seen dugub ci lu dul walukaayi garmi yi te seen reseñ it sañuñu ko woon a nale fu dul ci seen nalukaay yi loolu lepp nag daanaka ñi ko daa jariñoo ñu neew la daan doon ci niti diine yi ak seeni njaboot bu ko defee ñu bàyyi nee way ndool yi ak ñi aajowoo kenn du leen dimbli ña ëpp nag ca niti diine ña taxutoon ñu feexoon moo taxoon danu daan ànd ak mbooloo mi kontar garmi yi kureelub mbooloo mi nga xam ne la ëpp ca askan wa ca lanu bokkoon ñoom jegge woon nanu bi fipp gi di bëgg a door lu tollook milyongi nit te kat booba garmi yi bu nu leen boolee ak niti diine yi weesuwunu woon junniy nit coonab galag yepp ci ndoddum baadoola yi la daan tegu kureel boobu nag bu baadoola yi moo ëmboon kureel bu diggu bi walla bi nuy wax bourgeois ak kureelu baykat yi ak bu boroom mecce yi ak bu soldaar si bu dee kureel bu diggu bi moom ca la boroom xam xam ya bokkoon xalaatkat ya boroom xel yi ñoom nag amunu woon sañ sañ ci pal yu kawe yi moo ëmboon it yaxantukat yi ak boroom alal yi daa fay galag yu mag yi nga xam ne seen fay gu metti gi nu daa fay galag yi ak lamb gi amoon ci seen yaxantu gi taxoon na ba seen koom koom daanu woon lii lepp nag taxoon na ba gii kureel meroon lool ci goornamaa bi te meroon it ci ay jëfam ak ci li nu defaloon ñaari kureel yii di bu garmi yi ak bu niti diine yi bu dee kreelug baykat yi nag ñooy ñi gënoon a sonn ci kureelug baadoola yi ñoo ci daa njëkk a yëg aw ay bu jafe jafe bu kopooar amee ndax ci seen kaw lanu ko daa tegaat ci fayloo leen ay galag ak teg leen ligeey yi gën a tar bu nu nee kureelub soldaar si ñi ngi ci jublu soldaar su ndaw si ak boroom ndomay xare yu ndaw yi ndax ndoma yu mag yi moom ak pal yu mag yi garmi yi lanu leen daa jagleel na fa xalaat meloon ak li fraansu njëkk fipp gi di gënadi woon a nekk cib coona ak ñaawug nekkiin yeneen reew yi mel ne itaali otris brusiya ak riisi lepp teewul waa fraans a gënoon a yëg yeneen reew yi tooñaange yi nu leen daa teg li waraloon loolu nag mooy yewwuteg politig ga fa amoon ak gu xalaat ga ca biir boroom xel ya ca kureelub baadoola ya di yaxantukat ya ustaas ya layalkat ya doktoor ya boroom xam xami koom koom ya bindkat ya xeltukat ya añs jamono jii dafa fiiroo ak diggante bob fraans da cee amoon ay xalaatkat yu mboolaay ak yu koom koom yu leen daa yee ci coona yi nu nekke ak bonug nosi politig ya fa amon yu mboolaay ya yu doxaliin ya ak yu alal ya da na jaadu nu waxtaane fi ñatti xalaatkat yoy ligeey nanu lu rëy ci tas fi xalaat yi fi indi fipp gi ñooñu ñooy montesqieu voltaire jean jacques rousseau bu dee montesquieu g moom mi nga xam ne siyaare na angalteer gondiku woon it lool ca nosteg sartu reew gu buur ga fa nekkoon moom de ay ligeeyi xam xamam mi ngi feeñe woon ca teereem ba tuddoon ruug yoon yi g teere boobu nga xam ne teere bu jaroon la bu boroom xeli yi fonkoon la ci fraans ak feneen xalaati montesquieu yi ñi ngi tënku ci fexee tënk goornamaa bi te fuglu ko ak tàqale diggante dooley yoonal ji ak ju doxal ji ak ju laman ji moom montesquieu nag li mu doon wut ci teereem boobu mooy taxawal ag atte gu tegu ci sartu reew ca fraans ndax kat moom dafa gondiku woon lool ca sartu reew bu buur ba amoon ca angalteer bu dee voltaire g moom de woote na jëme cig coppi ci nekkiinu askanu fraans wi jaare ko ci taalifam yi mu defoon ciy woy nga xam ne taalifi jam lanu woon ak yéjj moom de jamoon na nosteg politig ga amoon ca fraans ak gu egliis ga ak sañ sañ yi garmi yi amoon ak niti diine yi wolteer de ak li xalaatam yi doonadee woon lu yees lepp teewul seen solo ñi ngi feeñe woon ci nekk gi nu nekkoon di luy laal yëg yëgi waa fraans yi ngir nekk gi ñu nekk di ay xalaat yu nit yuy jeexiital wolteer de gore ga waa angalteer ame woon da koo neexoon lool yeemoon ko mu jeexiitalu ci ginaaw ba mu fa amee ñatti at li waraloon mu nekk fa nag mooy danu koo dàqe woon fraans gore googu mu gisoon ca angalteer ak xalaat ya mu fa ame woon feeñal na leen ca teereem ba tudd bataaxeli xeltu walla ay bataaxel yu bawoo ca waa angalteer atum g wolteer nag dàq gi nu ko dàqe woon fraans yobbu ko angalteer ak tëj gi nu ko tëjoon lepp ca kasob bastil bu metti bu raglu ba teewu ko woon a wéy ci jam garmi yi ak niti diine yi la desoon ca dundam ga lepp it da koo jeexaloon ci nekk di ku yoon di wër bu dee jean jacques rousseau g mooy boroom teere ba tudd kollareg mboolaay mooy teere bi doon woote jëme ci goreg nit ak yamoo gi nit ñi war a yamoo ci wàllug mboolaay mu neeti goornamaa bi daal li ko war mooy mu sonn ci yittey nit ñi fippug fraans gi mi ngi sukkandiku woon bi muy lim yelleefi ki dëkk fraans mi ngi sukkandiku woon ci xalaati rousseau yu mboolaay yi nekk ci teereem boobu nu doon wax leegi jafe jafe bu koppar ba atum g mooy at mi fipp gi ame woon nekkutoon at mu ya ko jiitu woon tane ci wàllug koom waaye la waraloon fipp ga am ca mooy ñàkk a taw ga mu àndaloon ga juroon bekkoor ba ak xiif ba nit ñi mujjoon di ñu ñàkk aw ñam jafe dundiin wi naqari bokkoon na ci li gënoon a mettil mbir mi galag yu bari yi nga xam ne tege woon nanu leen te lepp di woon ci ndoddum baadoola yi ngir mëdde ci depaas yu bari yii nga xam ne nguur gi daa na leen def ngir boram yu bari yii mu daa jële ci xare yii mu daa faral a def ci biti ci jamonoy luwis ak luwis te loolu ci li daa jeexal ay koomam la woon luwis bi mu ñëwee jeem na ba sonn ngir lijjanti jafe jafe bii amoon ci mbirum alal mi ak loppanti njëlul nguur lu loof lii te sonn jaare ko ci tege ay galag yu bees waaye mujj na di ku manutoon a ñàkk a woo jataayub kureel yu xeet wi bii nga xam ne danu koo tasoon ci jamonoy luwis ngir mu daje naka la fipp gi ame woon doomi kureel gu diggu gi begoon nanu lool bi luwis woowee jataayu kureel yu xeet wi ngir mu def am ndaje ngir gëstu yoon yi man a lijjanti jafe jafe bii aju ci lòtt gi njëlul reew mi lòttoon ñu gisoon ne loolu daal pose bu mag la ngir nu indil seen bopp saafara si ko man a faj te fajal ko seen bopp ñi daa woote yewenal it jàppe woon loolu pose ngir def seen yewenal yi nu yeene woon ak soppi yi nu bëggoon ngir fraans man a baax man a tegu ci yoon bañ koo yamale ci loppanti njël li rekk ci noonu ag wuute am ci diggante kureelub garmi yi ànd ak bu niti diine yi ci wàll ak kureelub baadoola yi ca geneen wàll bu ko defee waa kureelub baadoola yi sàkku woon ñu def woote bi mu sukkandiku ci cer yi te bañ a sukkandiku ci ay neeg ndaxte la doonoon aada foofa mooy kureel bu nekk ci ñatti kureel yooyu da daa am genn kàddu bu ko defee yenenn ñaari kureel yi bu garmi yi ak bu niti diine yi bu ci nekk am ñaari kàddu bi ñaari kureel yii lànkee ne deesu fi wootee di ko teg ciy cer ne daal ay neeg ñooy woote bi loolu amee ceri kureelu baaloola yi danoo daje ñoom nee cig beru ñu neew ci garmi yi ak niti diine yi jàpple leen dëgëral leen ku ci mel ni garmi bii di mirabo ñu waxoon ne ñoom daal ñooy ndawi li ëpp ci askan wi ñu giñoon it ca fowuwaayu tennis ba nekkoon ca wetu njéndul versay la ci atum g ne ñoom de dunu bàyyi mukk lii nu nekke li feek wutalunu reew mi ab sartu reew bu man a yewenal seenu nekkiin te baaxal ko ak doonte luwis moom li mu àndoon mooy kureel yepp daje te xam ne ñooy ndawi reew mi bu nu booloo waxul bu benn taqalikoo nee beru ci noonu way daje yii nga xam ne danoo tudde woon seen ndaje mi ndajem xeet wi walla jataayub taxawal bi ñoom de foofu lanu nekkoon ci defar sart bu bees bi ñeel fraans bi nga xam ne day leeral li waa fraans bëgg tey jeem ci seeni aajo jëf jii nag mooy doorug fipp gi tolluwaay yi nga xam ne fipp gi romb na leen ceri ndajem xeet wi daje woon nanu ca versailles ngir defaral fraans ab sartu reew bu yees askaan wi daal di jañu jëm ca kasob baasil ba ca paris ca sulye g song ko nangu ko genne ña ñu fa tëjoon ngir politig jëf jooju mujj di juy wone gore gi nga xam ne moom la fipp gi doon woote jëme ñu mujj jël bis boobu def ko màggal gu xeetu fraans wi di màggal at mu nekk nangu gi nu defoon kaso bi ñemeloo woon na baykat yi ñoom itam ñu jug song suufi garmi yi yàq seen njénd yi looloo waraloon lu bari ci garmi yi gàddaaye woon fraans dem feneen nekk gi nu nekkoon feneen mujjoon na di aw ay ci fraans ndax buur yi nga xam ne doonuñu woon ànd ci fipp gi ndax du seen njariñ danu leen doon ngemb ngir ñu xeex ko te loolu doon na jëme ci xareb ñoñ askanu paris wi wutaloon nanu seen bopp ay ngànnaay ñu daal di woon sos ag wattu gu reew ngir wattu fipp gi aar ko lafyette jiite ko moom mi nga xam ne waxoon nanu la ne doon na xeex di jàpple waa sancu yi kontar waa angalteer ca xareb temb ba xarekati fipp gi ñi leen jiite woon ay nit lanu ñu bañoon te sib doxaliinu njabootub barbon gi ak seeni dag lafyette moomu ci la woon ñoom de seen xol yi dara nekku ci woon lu dul mbañeel wañse ak gënjëng ci bis bi njëkk ci ut la ndajem xeet wi jibal àqi nit aki yelleefam ci ut mu neenal sañ sañi laman yi ak yeneen yi garmi yi ame woon ak niti diine yi xeet wepp mujj daanaka di jàpple fipp gi lu bari ci doole ju ngànnaayu ju fraans ji mujj fekksi wattu gu reew gi nu taxawaloon ngir wattu fipp gi ci noonu mbooloom xare mu fraans mi tas luwis mujj ànd ca la xewoon ca kaso ba waaye way fipp yi digale nu sàmm luwis ba du daw ci noonu ñu taxawal seen bopp ci doxal mbirim reew mi ak mu egliis bi ci wàllug doxaliin ak alal loolu moo merloo woon paab gi mu mujj moom paab gi di kenn ci ñi gën a noonu fipp gi ñu daal di bennal nattukaay yi ak yoon yi ci fraans gepp ñu daal di seddalewaat fraans def ko ay doxaliin yu bees bi ndajem xeet wi di teg sart bi luwis doon na jeem a dolli ay kàttanam aki sañ sañam bi mu ko manul nag la doon jeem a daw juge ca njéndam la waaye ñu jàpp ko ca farn ca suye g njëkk muy genn reew mi gis nanu tam benn dosyeem bu mu fi bàyyi woon buy feddali ne moom daal nanguwul yoonal yooyu mu àndoon ndax ànd googu mu ci àndoon danu ko cee manante woon waaye du lu mu def ci teeyug bakkan ndajem xeet wi eggal na sart bi ci sebtambar g loolu di bi fipp gi amee ba toll ci ñaari at bi mu ko defee nag ndajem xeet wi daal di tas boppam daal di fiy taxawal ab jataayub yoonal bu sukkandiku ci li nekk ci sartu fraans bu bees bii nga xam ne lu feddali woon àqi ak yelleefi nitug fraans la woon ak war gu mu war a gore te am ag yamoo ci wàllug mboolaay moom sart bi tam tàqale woon na diggante nguurug yoonal gi ak gu doxal gi ak gu àtte gi mu jël nguurug yoonal walla dooley yoonal ji teg ko ci loxol ab jataay bu askanu fraans wi di tànn mu jël dooley àtte ji teg ko ci loxol ay àttekat yoy danu leen di tànn mu jël nag dooley wéyal ji walla ju doxal ji teg ko ci loxol buurub fraans bi aki jëwrinam ndaxte nguur saxoon na ca fraans ba ca sebtambar g ci atum g beneen woote amoon na bu nu doon tànnewaat ab jataayub yoonal ci noonu jataayub xeet daal di sosu boo xam ne li mu njëkk a def mooy jibal nosteg pénc systeme republicain ca fraans ca satumbar g ñu feetele ko doxal reew mi ak teg sart bu bees buy sukkandiku ci nosteg republig gu bees gi ñu wax ko tam mu seet li nu war a def buur bii di luwis te teg yoon yuy aar fipp gi aar it fraans ci musiba yi ko man a dikkal juge ci reew yii di otris ak brusiyaa ak britaani ak sax yeneen reewi tugal yoo xam ne danoo noonu woon fipp gi feetale nanu ko ba tay taxawal goornamaa bu fraans bu dëgër boo xam ne da fiy jeem a jële fitnay biir reew mi ñi jiite woon goornamaa bu jataayub xeet boobu nag ñi ngi sosoo woon ci girondins yi ñooy ñi nga xam ne danoo gëmoon ag yewenal te daan woote jëme ci coppat goo xam ne danu koy amal cig nànk nànk ak ci jacopins yi xam ne ñoo gënoon a xaabaabal girondins yi danoo gëmoon ne fii fraans toll tay ak nekkiinam wii danu koo war a soppi bu wér ak doonte loolu dafa laaj doole ak ñu diggdoomu ñoo xam ne taxul woon leen a xaabaabal ñoom ñooy ña ëppoon ca jataayub xeet wa waaye amunu woon gis gis bu dëgër ndax leeg leeg ñu ànd ak jacopins yi leeg leeg girondins yi ligeeyub goornamaa bu jataayub xeet wi goornamaa bu jataayub xeet wi daal di nay àtte buur bii di luwis àtteb ray ci samwiye g loolu nag tax na ba lu bari ci reewi tugal yi def ag jàppaloo kontar fraans mu ci mel ne angalteer ak brusiyaa otris espaañ ak holand ginaaw bi nag goornamaa bu jataayu xeet wi daal di taxawal kureelub kaaraange feetale ko ligeeyub aar fraans ci ñiy noonu fipp gi ci biir reew mi ñu feetale ko ba tay moom kureel bi wàluug taxawal am mbooloom xare mu fraans mu dëgër ngir aar fraans ak fipp gi ak li mu fi jot a indi ci ndam ak xeewal moom fipp gi goornamaa bi nag ci njiitul girondins yi gañe na xarekati brusiya yi ca xareb valmy ba lijjanti na it ba xiir waa beljig ci ñu fipp ci kaw imbraatoor boobii di francis mi nekkoon imbraatooru nguurug rom gu sell gi ñu daal di nangu alali paap gi ci goxub afinion ngir noonu gi mu noonu woon fipp gi moom paab gi ñu fàttali leen ne jacopins yu xaabaabal yooyu ñoo saytu woon kureelub kaaraange gu matale gi ñoom songoon nanu ci anam gu tar ci njiitul robespierre kepp koo xam ne yaakaaroon nanu ne da nga àndul ci fipp gi aki gaay fipp gi jacopins yi nag bari na lu ñu daa mbugal lim bu bari ci waa fraans yi ci tuumaal leen ne danoo def ay wor yu mag ñoom ci seen jëmmi bopp nag ak doonte jàmaarloo woon nanook jafe jafe yi leen dikkaloon juge ci reewi tugal yi leen wër te aju woon ci kontar fipp gi ak doonte jàmmaarloo woon nanook ñoom ci doole ak fulla te farataal duggug coldaar gu sañ bañ ngir aar reew mi tas te giimal fttéerlu yi doon am ci yennat ci gox yi nekk ci biir reew mi duggal seeni xarekat ci beljig ak holand ànd ak loolu lepp teewul waa fraans bëggoon ñu soppi seenuw doxiin ci politig ba mu gën a woyof gën a teey gën dal te gën a maandu ci sulye g la ceri jataayub xeet wi tuumaal robespierre ne daa wor yobbu ko ca mbuggalukaay ba jataay bi defaraat na beneen sart boo xam ne moo waral ab goornamaab fraans bu bees ñu xame ko ci turu goornamaab doxaliin bi goornamaab doxaliin bi goornamaab doxaliin bi sampu na atum g moom nag li mu doon wund mooy ab diggante bu tuxu nekk ci diggante jamonay tiital ak taral ak jamonoy nguurug imbraatoor gu nu joyal gu tar goo xam ne napoliyon bonaparte moo ko ame woon ci ginaaw bi ci bi mu fi nekkee goornamaa boobu nag li gënoon na fés ciy ligeeyam ci ñaari wàll yii lanu jëmoon 	def politig bu maandu ci biir doxaliinu reew mi te du tax mu doyadi mbaa mu ñàkk fulla ci kanamu ay noonam 	yonni napoliyon ngir mu song itaali ngir yare ci otris ak yonneeti ko ci penku bi nanu fàttaliku ne goornamaab doxaliin bi mi ngi sosoo woon ci juroomi cer yoo xam ne dëppoowunu woon ciy jamonoom it la jëmmi napoliyon feeñ moom mi nga xam ne jariñu woon na bu baax ci doyadig gooramaa bii ak ñàkk dooleem ngir saxal fi boppam ci wàllug politig ciy jamonoom it lu sakkan ciy làngi politig sosu woon nanu ni nu doon jëfandikoo alal ji gën a ñaaw gën a bon ci fukki fan ci nowambar g la napoliyon ak làngam gi defoon yong googu nuy wax yongug brumaire daaneel goornamaab doxaliin bu neewoon doole boobu loolu moo fi indi goornamaab kilifa bi mooy bi ame ci ñatti kilifa yi nga xam ne ñoo doon jiite fraaans te napoliyon jiite woon leen nga xam ne daanaka mbooleem sañ sañ yi ci loxoom lanu nekkoon napoliyon bonaparte napoelon bonaparte mi ngi judd atum g ca ajaksio ca dunub corsica ca itaali dun boobu nga xam ne fraans da koo mujjoon jënde ci genova napoleon nekkoon na ba muy doon gone ku bëggoon fànnug xare mi ngi genne ca bànqaasu xare ba nekkoon paris daal di dem nag doon ab ofise bokk ca kureelub kano ya ca xarekati fraans ya moom nag ku soppoon xam xamu yoon la taariix ak xam xami xare yi ak yu doxaliin yi ku sawaroon la ci dali fipp gi te fonkoon leen moom nag ab bidiwam a ngi féqe ci ginaaw bi mu songee itaali àtteg napoleon walla yor gi mu yoroon fraans dafa seddaliku woon ci ñaari xaaj bu njëkk bi mooy kilifag fraans gu njëkk gi la ko dale ca g ba g bu ñaareel bi moom mooy imbraatoor bi la ko dale ca g ba g song gi napoleon defoon itaali goornamaab doxaliin bi dafa feetale woon napoleon jiiteg xeex boobu mu doon xeex otris jaare ko ca moomeelam yooyee nga xam ne itaali benn la ci woon atum g ci noonu moom napoleon mu daal di xeex ak nguurug sardeñ xeex bu tar boo xam ne jañ na ko ci mu xaatim ag wéer ngànnaay gu nuy wax gu cherasco napoleon defati ab xare ak dooley paab gi moñoxe ko ca ancona mu dumaati soldaari otris yi ca bëj gànnaaru itaali dàqeeti leen fa xaatim fa ak ñoom juboo ga tuddoon campo formio atum g ci nii daal la napoleon doyodile woon otris neewal ko doole daal di àgg ci njobbaxtalu siw ci wàllu doxal xare napoleon àntu gi xeexam yooyu àntu woon ci itaali tasoon lënkaloo gi waa tugal defoon kontar fraans mu mujj britani rekk moo dese woon xeex beek fraans song gi napoleon songoon penku bi politigkati fraans yi naaloon nanu taliraan mi nekkoon jëwrini bitim reew mi jiite woon leen naaloon nanu ay naal yu aju woon ci ngàdd britani jaare ko ca sancoom ya te bañ koo fekk ci biir këram rawati na moom britani dafa amoon mbooloom gaal mu mag ca geejug mans politigkati fraans yi li nu bëggoon ci loolu mooy sos ab sancu bu fraans ci geej gu diggu gi ak man a àgg ca geej gu xonq ga ak dog yoonu yaxantu wi daa àggale britani ca sancoom ya nekk penku goornamaab doxaliin bi lii mi ngi ko denkoon napoleon ci noonu mu jug mooki gaayam geeju ci atum g tukkee ca waaxub toulon mbooloom xare mi àndoon ak moom àggoon na ci ñeenti teemeeri gaal yu sëfoon ñaar fukki junneek juroom ñatti soldaar bokkoon na ci tam teemeer ak juroom ñaar fukk ak juroomi boroom xam xam yu waa fraans ñu àgg waaxub aleksandriya ca isipt nangu ko waaye mbooloom gaalum britani mi bettoon na mu fraans mi ca ndoxum golfub abii xiir moñoxe ko ci noonu la britani xañe fraans cangug geej gi fraans yàgg a gent fraans sax nag ni mu ko baaxoo woon nguurug xare la gu mag gu gën a am mbooloom xare mu jeeri ci mu geej mu mel ne mu britani mi man nanu ne xare bii napolen daan def ci penku bi xare jooñ la woon ndax kat ag sof rekk la ca xareb jooñ ba amoon cag njëkk loolu nag gën na a leere ca xare ya mu doon def ca afrig gu bëj gànnaar ga misra isipt ca jamono jooja dafa nekkoon reew mu nekkoon ci waawug àtteg usmaan gi bu ko defee buuri mamaalik yi jiite ko mu doon jànkoote ak ag doyadi gu biir ak xeex gu sax ci biirum reew ngir nangu nguur gi te tam ngànnaay yi mu ame woon yu doyadi la woon bu nu leen nattee ci yi napoleon ame woon aki jumtukaayam lii moo taxoon napoleon sonnutoon ci teg loxo isipt ak doonte mamaalig yi ñoom jàmmaarloo woon nanook moom xeex ak moom xex bu tàng ngir aar seen reew waa isipt yi bégunu benn yoon ci àtteg napoleon gi li am kay mooy danoo fippoon ci kawan mooy la amoon ca xayra keer ñu koy wax fippug xayra gi napoleon jawali na reewi shaam mook mbooloom xareem mi ginaaw bi mu nangoo isipt mu daal di teg loxo hariis gaza ak yafa daal di ray dooley kaaraange ja fa nekkoon daan ko aar te tolloon ci ñeenti junniy soldaar juge fa diriku jëm hakka gaw ko diir bu yàgg waaye hakka moom toogul rekk faste ay loxoom di seetaan dafa jànkoonte jaamaarloo cig njàmbaar ci njiitul kilifaam gii di woon ahmad basha nga xam ne mbooloom gaalum xare mu britani mi ñoo ko doon dimble tukkee ci geej gi waa usmaan yi di ko jàpple ci jeeri ji bi gaw gi yàggee te napoleon ñàkke ca lu bari te amewu ca lenn njariñ xarekatam yi tàmblee tawat rawati na tawat ji nuy wax siburu di yaram wuy tàng bi loolu amee napoleon xam ne fii muus du fi naane ñeex mu deltu ginaaw dellooti isipt te jëlewu fa lenn ndam napoleon bàyyikoo na isipt ci sekkare dellu paris askan wa tertu ko fa cig yaatal ak mbegte xew xew yi toppante ci fraans waaye ci anam gu baaxul ci goornamaab doxaliin bi looloo fi jële boobule goornamaa bi nuy wax bu ñatti kilifa yi taxaw atum g napoleon nekk ca kilifa gu njëkk ga ay ngérte yu am solo juddoo nanu ca xareb napoleon bu penku ba ñu indil leen ci yii rekk 	xareb fraans boobu ci penku bi wone woon na solo si isipt am ak fi mu feete ci wàllug jokkoo ak tuxu ñeel imbraatoorug britani gi ci penku bi 	xare boobu fraans da ci doon seete rekk ngir xam nu muy def ba man a sanc walla kolonise reewi afrig gu bëj gànnaar gi 	boroom xam xami xare boobu bi nuy ñëw indaale woon nanu ay gëstuy xam xam yu aju woon ci nàndal ak jeexiit indi woon nanu fi it benn naal bu aju woon ci gas aw yoonu ndox ci diggante suwes ak geej gu diggu gi di kanaalu suwes bi te it indaale woon nanu fi ab moolukaayu teere ci araab nu koy wax moolukaayu bolaax bi 	xare bi wutoon ay yoon yu man a indi ag jokkoo ci diggante fraans ak isipt rawati na ci wàlli xam xam ak njàngale añs napoleon ak reewi tugal yi napoleon de taxawaloon na màmm gi otris màmmoon ci yaatal nguuram ndaxte gañe woon na ko ca xare ba nuy wax marenngo atum g jañoon ko ci mu xaatim ag juboo gu yees atum g mooy juboo gi saxaloon poñ ya nekkoon ca kollareg campo formio ga napoleon xatim na ak britani juboog amiens atum g looloo waraloon dooley fraans ji genn isipt bu ko defee angalteer moom itam noppi ci li dal otris bañ cee wax dara napoleon saxoon na di ki nga xam ne moo ame woon sañ sañu fal niti egliis bi ci fraans paab bi tam bi napoleon di sampu niki imbraatoor atum g mooy ki doon def li ci aju woon ci xeeti ñaanal ak xumbal napoleon bi mu jotee ci imbraatoor gi daa daal di nosaat doxaliin wi ci campeefi nguur gi mu taxawal fi benn jumtukaay buy yëngu ci luy amal bëgg bëggam bii mu jël lu sakkan ci mbokkam yi ak xaritam yi jox leen pal yu kawe yi mbooleem dooley nguur ji ak sañ sañ yi mu tëyyeel leen boppam teg boppam it ci kaw mbooleem làngi politig yi doyadil làngi politig yi ak barlamaan bi nos galag yi napoleon de tàbbi woon na ciy xare ak reewi tugal yi britani gañe woon ko nag ci wàllug geej gi ca xare ba nuy wax attaraf al aqar mu song brusiya gañe ko ca xareb yena ba atum g mu daal di def waxtaan ak aleksandar mi nekkoon sesaarub riisi def ak moom genn dëppoo nu koy wax dëppoo gu talist atum g mooy liy wone njobaxtal la napoleon àggoon ci kàttan mu defoon ag gaw gu goxub tugal bepp jëme ko britani daal di woon ga reewi tugal yi ci ñu topp ko ci loolu loolu indi woon na fi benn jafe jafe bu koom koom bu tar ci reewi tugal yu bari loolu it waraloon na reew yii bañ ko kontar ko mu xare woon ak riisi gu sesaar gi ndaxte daa gisoon ne moom kat wormaalul gaw googu mu digale woon ci noonu mu jëmale fa menn mbooloom xare mu mag atum g ñu dox ba àgg ca peey ba di butrusburg waaye mujj nanu manatunoo ñàkk a dëpp ngir sedd bu tar ba leen fa gaw ba jamonoy sedd ja duggee ak ba tay ngir jafe ga fa ag jokkoo jafee guy man a yombal nuy jot ci li am mbooloom xare di soxla ngir man a def ligeeyam muy jotug jumtukaay yeek dund yeek lu ni mel bi nuy dellu nag la waa rusi yi sottiku ci seen kaw ñoom xarekati napoleon yi ray ci lu bar bu ko defee napoleon ñàkk soldaaram yu bari te amul la mu doon bëgg bu ko defee waatugal yi otris brusia rusi ak britani boole seen doole jàmmaarlook napoleon daal di koy gañe ca xareb libisg nu koy wax xareb xeet yi di woon ci oktoobar atum g ca noona nu sànni napoleon ca dun ba tudd elba waaye mu lijjanti ba rëcce fa ci sekkare ginaaw bi mu fa defee teemeeri bis dem nag paris dajale fa xarekat yu bari ci waa fraans yi ngir xeexi reewi tugal yi ko doon sot ñu gañeeti ko ca xareb watrlo ba atum g sànneeti ko ca dunub santa hilana mu des fa nag ba kero bi mu faatoo atum g bu ko defee reewi tugal yi def seen ndaje ma nuy wax ndajem vienne atum g ngir seddalewaat kartu tugal wu politig wi daal di fiy saxalaat bu baax kenoy nguur te suuxat ko fi ak sàmmoonteek yamoo gu reew yi ak sos reew yu am doole yu peek fraans wër ko ligeeyi ndajem vienne ligeeyi ndajem vienne nii la tënkoo woon 	way daje yi delloowaat nanu buuri tugal ya ca seen reew ya nu juge woon teg ko ci àqi yoon ci noonu nu delloosi njabootug borbon gi ngir ñu yilif fraans ak espaañ 	britani jëloon na sancu yi fraans moomoon muy malta ak kaab ak silaan ak morisos 	rusi jël moom varsaw otris jël tefesug dalmas ak milano gu itaali gi mujj nag ëpp doole nguur yu ndaw yu itaali yi brusiya moom am ay moomeel yu mag ci almaañ ak ag wàll ci poloñ ñu jël beljig cig sañ bañ boole ko ci holand jëlati norwej cig sañ bañ boole ko ci suwed jëf yii yepp nag dëppoowunu woon ak xeetu walla fonk sa xeet di nationalisme gi doon am ca tugal lii nag firee nanu ko ne li ko waral mooy britani daal ak rusi ak otris ak brusiya danoo defoon seen bopp ay reew yu ñoo am ag kilifteef ci reew yu tugal yu ndaw yi li juddoo ci fippug fraans gi 	fipp gi moo fi indi tay dalub fonk sa bopp bii nga xam ne mujj na foo dem ci tugal fekk ko fa ci diirub xarnub fukk ak juroom ñeenteel bepp g moo waral reewum itaali bennoo te moo jur it bennoo gu almaañ gi 	moo fi jële sañ sañ ak ràññale ci biiri kureeli nit naan kii moo kawe kee wii xeet a gën wee te man nanu ne mooy jaasi ji mujj rendi nostey laman ya nekkoon tugal 	fipp gi ci fraans mooy gi njëkk ci fipp yi ci taarixu tugal bu bees bi loolu nag li ko waral mooy coppat yi mu indi ciy gisiin aki deggiin aki xalaat ci wàll yu bari ci dundug politig gi gu mboolaay gi gu xalaat gi gu koom koom gi ci tugal ak fu ko moy ay term yu politig feeñ yu mboolaay yu diplomasi yu bees 	moo fi jële gisiin wu àqi yalla ji mooy gisiin wi naan buur yi seen àq ak sañ sañ ca ju yalla ja lanu ko jële mooy gisiin wi matale woon noste yi amoon ci tugal gepp la ko dale ca ba fa jamonoy laman tàmblee 	xalaatub fipp gi law na ba àgg ci tugal gepp ak yeneen reew yu dul tugal yu adduna bi buntub ñeeteel bi yëngu yëngu yi aju ci xeetu walla fonk sa xeet nationalisme ci tugal ci xarnub fukk ak juroom ñeent g bennal gu itaali bennoo gu almaañ doggantal gu njëkk gi bennal gi nu defoon itaali ni itaali meloon njëkk xare yu napoleon yi itaali laata a napoleon di ko teg loxo di ko nangu nekkutoon reew mu nu bennal nekkutoon it di mu am ag temb moom kay daa seddaliku woon doon fukki xaaj ak ñaar yu doon topp ak a nekk ci ron kilifteefug ay nostey politig yu wuute nosteg nguur ca savoia piemonte napoli ak nosteg pénc ca venezia ak geneva ak ag àtte gu paab ca rom ak gu doox ca toskaana ak parma ak xaaj yoo xam ne danoo nekkoon ci waawug imbraatoor gu otris gi ñooy milano ak lombardia piemonte nag moo nekkoon nekkteg politig gi gënoon a dëgër te ëppoon doole ci nekkte yooyu ña ëppoon ca njiit ya yilifoon nekkte yooyu ay diktaatoor lanu woon rawati na ñi ci waa otris jiite woon cig jonjoo mbaa lu ko moy jeexiit ya napoleon bàyyiwoon ca itaali napoleon bi mu nangoo itaali dafa lijjanti ba boole xaajam yu politig yu bari te wuute yooyu ci ñatti nguur rekk ñooy nguurug alp gu bëj gànnaar gi walla itaali ak nguurug savoia ak nguurug napoli mu wutaloon reew mi mepp wenn yoon daal di dindi galag ak tënk yu koom koom yi amoon ci wàllug endustri ak yaxantu ak mbay mu ubbi leekol yi ngir jàngal doomi reew mi mu may waa itaali yi ñu man di jot ci pal yi te kat bu njëkk waa otris rekk a ci manoon a jot looloo tax ñu man a wax ne napoleon de mooy ki ji njiyum bennoo mu xeet ci suufus itaali mooy ki leen def ñuy xeeñtook a gént am reew mu itaali mu man a am mu nu bennal itaali ginaaw ndajem vienne ndajem vienne mi ci xalaati njiitu jawrin ju otris jii di metternich winneburg seddale woon na itaali def ko juroom ñaari xaaj ñooy piemonte napoli parma modena toscana lombardia ak venezia ñoom ñaar nag mujj nanu leen boole def leen benn teg leen ci ron kilifteefug otris ginaaw nag metternich fexe woon na ba yay njiiti ndaje mi gëmloo leen dalu desal fi lu yàgg la ca yàggam ga maanaam lu nekk nanu ko delloo na mu meloon loolu nag moo indi ndaje mi delloosi njiiti nguur yu ndaw yu itaali yu njëkk ya ñu delloosi leen ci seeni pal tegaat leen seen barab metternich ak bëtam yi mu tasoon ci gox yepp jeemoon nanoo fuglu yeglekaay yi daan naj it gepp cawarte gu politig ci noonu ñu daa tëj gor ñi ci kaso yi daan xañ way dëkk yi pali siwil yi ak yu xare yi nga xam ne bi napoleon ñëwee jox na leen ko mu daan leen weccee ak ay waa otris moom metternich te daan leen teg ay galag yu diis te sonnle yewwueg xeetu nationalisme ni mu xëye rekk am te màgg ca itaali politigu noteel gi metternich yore woon ak li muy tar lepp taxutoon mu man a rekki yëg yëg bi waa itaali yi ame woon ak xam ngi nu xamoon am solo gi bennal seen reew mi te booloo ci wàllug politig amoon solo loolu nag mi ngi am ginaaw bi nu ci ñamee s lëf ci jamonoy napoleon bi nga xamee ne politig bu ñaaw boobu fa amoon mayu leen woon ñuy def seeni cawarte ak jëfi politig ci lu bér te nëbboodiku bi loolu amee lanu wéeru ci di def seeni yënguy politig cig làqu ak fésadi bu ko defee ay booloo yu politig yu sekkare tàmblee sosu ci dëkki itaali yu mag yi li leen taxoon a jug di bennal itaali bokk na ci yooyu booloo gu karbonari ñoñ këriñ ak booloo gu itaali gu waxambaanee gi booloo gu karbonari moom mi ngi sosoo ca napoli daan def ay jataayam ngir làqatu ci barabi ligeeykati këriñ yi walla lakkati mat yi mu mujj nag tas ci mbooleem itaali mbooleem kureeli askanu itaali wi nag bokkoon nanu ci baykat yi ligeeykat yi boroom mecce yi yaxantukat yi boroom xel yi añs li leen manke woon nag mooy danoo nosuwutoon bu baax te ni ñu daan naale ak a rëdde seeni mbir tam dafa dese woon a tegu ci yoon looloo taxoon li nu bëggoon daawul àntu te seeni noon daa leen gaaw a not te daa àntoodil seeni fipp waaye nag booloo gii di gu karbonari gi jot na fee taal yëg yëgu xeetu ci itaali te lijjanti ba mu sax fi di tàkk ak doonte daje na ak coona yu bari te nu teg ko lu sakkan ciy mbugal bu dee booloo gi tuddoon itaali gu waxambaanee gi moom jozeph mazzini g moo ko sosoon ginaaw bi mu nekkee ab cer ci booloo gu karbonari gi mazzini mii moom waay itaali la woon ju xéroon ci reewam ak xeetam nekkoon it ab xeltukat bu bokkoon ci ñoñ nite ñi bu gëmoon ne xeetu nit ñepp benn lanu te bëggoon lool goreg askan yi moom nag jot na a àgg ci xëcc cig wàllam boroom xel yi ci itaali te fàggu ñeewanteg nitug neen ku itaali ki akug cofeelam bokkoon na ci jubluwaay yi gënoon a tax booloo gii am goreel itaali ci àtteg otris ak duma àtte gu paab gi nga xam ne otris a ko daa dimbleek a dëgëral ak fexee bennal reewum itaali mi ci ron ag noste gu republig yëngu yëngu yii mujjoon na naat te dox bijjaloon it boppam lu sakkan ci waxambaane yi ak xalaatkat yi àggoon nanu ci lu toll ne juroom fukki junniy waxambaane yu weesu ay ñeen fukki at yooyu mazzini dimblante na ak garibaldi moom garibaldi ab kojug xare la woon bu itaali bu gëmoon bennug itaali te gëmoon ne danoo war a gorewu ci àtte gu otris gii bóof ci suufus itaali si ci noonu lanu jot a taxawal ñoom ñaar ag àtte gu pénc ca rom ca moomeeli paab ga ak ca venezia atum g waaye otris moom ca dooleem ju bari ja faagaagal na yëngu yëngu googu daal di dàq mazzini mu daw làqu ca anggalteer ag woote nag feeñ na fa jëm ci ñu def nattukaay yi benn xaalis bi ak peesekaay yi ci mbooleem diiwaani itaali yi aki nguur nguuraanam rawati na bi endustreem tàmblee màgg yaxantoom gën a jëm kanam boroom ligeey yi nag ak boroom boppi alal yi gisoon nanu am njariñ gi gore ci koom koom amoon njariñ ñu tàmbli woon a sàkku ñu sosal leen ay yooni weñ yuy taqale diggante bëj gànnaaru itaali ak bëj saalumam te nu uppi mbooleem ja yu itaali yi ci kanamu yaxantu gu itaali gi te bañ cee indi yenn jafe jafe walla ay mbugal yu doxaliin walla ay galag yu man a tee bennoo gu yaxantu gi am ci itaali ma fàttali leen ne barab yu bari de ci bëj saalumu itaali yu deltu woon ginaaw lanu woon ci wàllug endustri koom koom mboolaay ak politig looloo taxoon xalaat yi jëmoon ci bennoo mi ngi gënoon a dëgëre ci fi nuy wax itaali di nguuru alp gu bëj gànnaar gi ak ci digg bi foofa daal la wooteg bennal gi gënoon a tare ci yeneen wàll yu bëj saalum yi ndax kat wàlli bëj saalum yi dañoo jëmutoon kanam dara ci wàllug endustri yaxantu politig ak mboolaay lii a waraloon woote gi jëme ci bennoo gu koom koom yamoon rekk ci digg itaali ak ci bëj gànnaar gi ñi ëppoon it ci xalaatkat yi ak boroom xam xam yu itaali yi ñi ngi dëkke woon digg bi ak ci bëj gànnaar gi ak li boole itaali def ko menn reew doon nekk càkkuteful ñepp lepp teewul yenn ci nguur nguuraan yi ak doox yi kontaroon ko ndaxte ñoom dañoo ragaloon ne loolu de moo xam leegi la walla ci kanam bu amee di na fi indi ag bennoo gu politig te loolu bëggunu ko woon ndax kat ñoom seeni njariñi nguur yooyu moo leen gënaloon njariñul itaali li ci noonu nguurug paap gi kontar ko naka noonu gu otris gi nga xam ne amoon na kilifteef gu yaatu ak sañ sañ bu mag ci itaali ndax moom daa gisoon ne bu itaali bennoo ci wàllug koom boole ay nguur nguuraanam aki dooxam loolu du wund lu dul ne moom kat otris waxtuw gennam itaaliee ngi bëgg a jot ci lu dog te loolu du ko nangu mukk nguurug piemonte ak bennalug itaali ci bëj gànnaaru itaali ag nguur a ngi fi woon ñu koy wax nguurug piemonte walla sardeñaa ka nekkoon ca gàngunaay ga di woon victor emmanuel moom piemonte nag nguur la woon gu ame woon ci ñeenti xaaj yu taqaloowul ñoom xaaj yi ñooy piemonte mi nekk ci ron doji alp yi nekkoon barab bu taxu ko woon a woomle ak savoia mi ngi nekkoon ci kaw doji alp yi tiim wàllug fraans gi dend ak itaali moom nag ruq la bu gën a yor ay màndarga yu fraans ci yu itaali moom itam taxu ko woon a jëm kanam mbaa mu woomle ak sardeñaa moom dun la bu nekk ci geej gu diggu gi xaw a sori piemonte ak genova moom nag nguurug piemonte jot na ci ci ginaaw xarey napoleon yi ci tugal di nanu gis fii ne piemonte moom yorul woon nguur gu àttanoon coonay bennal itaali waaye nag yoroon na yenn yu rëy ci yiy taxawal reew mu mag yu ko mayoon mu man a yanu yan bu diis bii ñu tudd ci yi ci ëpp solo 	ab buuram daa gëmoon ag àtte gu tegu ci sartu reew te daa gëmoon it bennoo gu itaali 	njiitul jawrinam lii di cavor mi ngi doonoon njiitul jawrin atum g daa gëmoon moom itam te sopp sartu reew ba angalteer defoon te bëggoon lool itaali doon benn te nekk ci ron ndëppul piemonte 	piemonte amoon na dooley xare joo xam ne li ko daa wone mooy soldaaram sii nga xam ne jot nanoo xare ba am ci xam xam 	piemmonte moo nekkoon làqatukaay bi politigkat yi nu daa sonnale ci nguuri itaali yeneen yi daan làqatoo 	màgg gi koom koom doon màgg ci piemonte moo gënoon a gaaw gi mu doon def ci feneen ful milano 	nguurug piemonte gu sori woon loxol otris la nga xam ne daawul man a dugg ci mbiri biiram cavour ak bennalug itaali cavour mii g nekkoon na di ku gëm bennoo gu itaali waaye nag ci ron ag àtte gu nguur gu sartu reew goo xam ne buurub piemonte bee koy jiite moom kon ci loolu la wuute woon ak mazzini mi nga xam ne da doon woote ag bennoo gu itaali ci ron ag àtte gu republig moom de daa gëmoon ag yewenal gu politig gu koom koom ak gu doxaliin ngir itaali man a doon benn mu gisoon ne nguurug piemonte am na kàttanug dàq otris mu genn itaali ak naj nguurug paab gi daa lënkaloo ak otris bu lënkaloo woon moom piemonte ak jeneen doole ju reew ju mel ne fraans mbaa britani cavour mi ngi yoroon njiitug jawrin gi ci atum g bi mu ko defee nag mu tàmblee waajal am reewam ngir mu man a jiite ligeey biy bennal itaali ci noonu mu sotti yitteem ci xarekatam yi waajal leen ba nu man a jàmmaarlook mbooloom xarem otris mi te man leen a genne itaali mu jug ci suqali koom koom bi defar ay yooni weñ yu lënkale mbooleem dëkki piemonte yi daal di jamonool mbay mi ak endustri bi defar ay yoon neenal galag yeek mbir yi man a tënk yaxantu ak endustri tege ay galag yu duwaan yu mag ngir aar endustri bu lokaal bi bu biir reew mi yewenal nosteg galag yi daal di sos lonkoo yu askan yi ak bànk yi bu dee lu aju ci doxaliin ak yewenal yu biir reew mi moom da fee daal di woon buddee doxaliin wu yàgg wa fa nekkoon daal di jël ay matuwaay yoo xam ne tax nanu ba yoon ci reewum itaali gën a jamonoo jële fi lu bari ci ay jàngu maanaam ay egliis wàññi dooley politig ju paab gi tàqale àtte geek eglis bi kafor mii nag xamoon na ni reewam mi tuutee woon bu nu ko tollalee ak otris walla britani mbaa fraans am rusi ak brusiya waaye loolu lepp teewutoon mu gëmoon ne bennug itaali daal mbirum aw xeet la woon manul woon a ñàkk te itam mbirum adduna bepp la laaj na reew yi sonn ci te jeem koo faj ci nu mu gën a gaawe mu dogu woon ci sóobu ci geewub politig bu adduna bi ngir yékkati kàddug piemonte ci adduna bi ba ñepp degg ko ci ndajey tugal yi ci noonu mu digal parlamaa bu piemonte mu nangu ñu yonnee ab kureelub xare bu piemonte ngir mu bokki ca xareb xarm ba àndoon ca ak britani ak fraans ngir sàkkoo ci xaritoo ak imbraatoor bu fraans bii di napoleon mu ñatteel mi napoleon iii te ame ca ñeewantug britani akug jàppaleem ci li mu bëgg kureelu xare bu piemonte boobu ak doonte bariwu ci ñu ci dee ca xareb xarm ba ndax ñu bari ci ñi ci dee ci mbasum koleraa lanu deewe teewul kafour moom lijjanti na ba nu yëg piemonte ci kanamu ndawi tugal yi ca ndajem juboole ma nu doon def bi xareb xarm bi jeexee kafour sàkku na fa ca fraans mu dimbli ko ci otris ndaxte nguurug piemonte moom rekk manul a dàq imbraatoorug otris gu dëgër gii kavour ci njëlbeen gi li ko gënaloon mooy britani jàpple ko kontar otris waaye britani moom bëggutoon a xeex ak otris xeex bu ko amalul njariñ bu dee fraans nag nga xam ne pencam mi napoleon iii moo ko jiite woon moom napoleon iii mi nga xam ne daa jàppe woon itaali am ñaareelu reewam ndax moom doom la woon ca napoleon i ginaaw doomi mbokkam la woon te napolen i mi ngi cosaanoo corsica moom napoleon iii ku soppoon waa itaali la te xéroon ci seeni àq aki yelleef ci gore te doon benn moom de bokkoon na ci ñi gënoon a siw ci woote ag xeetu ci tugal politigu bitim reewam it mi ngi ko tegoon ci bañ otris mi dendoon ak moom te ginaaw piemonte it reew mu nekk ci wetu fraans la loolu taxoon na mu bëgg mu nekk reew moo xam ne yoonu otris du ca nekk cavour lënkaloo na ak napoleon iii ñu def dëppoo ga nuy wax plombiere ci sulye atum g dëppoo googu la mu yaxal mooy ñu taxawal ag nguur gu itaali ca bëj gànnaaru itaali buurub piemonte jiite ko ak geneen nguur ci digg bi moomeeli paab gi moom ñu bàyyi leen fi te bañ a laal dara ci nguurug napoli gi nekk ci bëj saamu itaali bu ko defee nag genn bennoo gu ame cig dëppoo lënkale leen ci njiitug paab bi fraans nag li muy ame ci loolu mooy ñu bàyyee ko niis ak savoia xare yi amoon ci diggante piemonte ak otris kafour wéy na di cokkaas otris rawati na bi ko napoleon iii yonnee ñaari temeeri junniy xarekat ngir ñu xeexle ko kontar otris loolu nag amoon na ci ginaaw dëppoog polombiere gi kafour am na la mu bëggoon muy jeqi otris yëngal ko ndax moom kat otris mujjoon na jekki jekki rekk sàkku ci piemonte mu nocci ay ngànnaayam ci diir bu gàtt bu weesuwul ñatti fan mu tóllanti loolu ci jug jawali piemonte ànd ak ay xarekatam atum g taarixkat yi firee nanu loolu ne ag wuyyusi la gu otris def ci li ko piemonte doon yàgg a cokkaas ak a dëkk nii daal la xare bi tàkke ci diggante otris ak piemonte waaye nag otris a njëkk a song ci noonu fraans itam jibal ab xareem ci kaw otris soldaari piemonte yi ak yu fraans yi jot nanoo duma otris gañe ko ca xare ba nuy wax maginta ak salvarino waaye napoleon iii moom daa xëyoon rekk taxawlu ci xare bi daal di gise ak imbraatoor bu otris bi def ak moom ag wéer ngànnaay dellu xaatim ak moom ag juboo te diisoowu ci ak nguurug piemonte wéer ngànnaay gii nag mooy li jur ci ginaaw bi li nuy wax juboo gu siyorix atum g bokkoon na ca poñ ya ëppoon solo ca juboo ga 	otris bàyyee piemonte lombardi 	sos booloo gu itaali ci njiitul paab bi ci tur 	venezia day des ci moomeelug otris waaye bokk ci bennoo gu itaali gi 	 delloosi ñi yilifoon doox yi nekkoon ci digg itaali ci seen barab ak seeni pal ginaaw bi leen askan wi follee 	boole niis ak savoia ci fraans taarixkat yi firee nanu taxawal xare gu bette gi nga xam ne napoleon iii defoon na ko ne daal li ko waraloon mooy daa bañoon ag nguurug itaali gu dëgër am taxaw rawati na bi mu tàmblee gis lenn ci doox yi nekkoon ci digg itaali tàmblee bokksi ci piemonte bokkoon na it ci li ko ko taxoon a def jeem a gëramloo katoligi fraans yi nga xam ne danoo tàmbli woon a mer ci neewal gi nuy neewal doole nguurug paab gi ci itaali te otris a ko daan jàppleek a dëgëral kafour nag moom daa daal di woon xàcc walla tekki ndombaam bi mu sàkkoo ci buur bi victor emanuel ba soon ngir ñu wéy ci xare bi ak doonte fraans genne na ci loxoom waaye mu lànk mom buur bi askani doox yi bañ nañu ne dunu nangu mukk ñu delloosi ña leen yilifoon bu njëkk ni ko poñi juboo gu siyorix gi yaxale ñu ne woon daal ñoom leegi danuy dem bokki ca nguurug piemonte ci noonu ay fipp am yu toftaloo ci parma modena romaña ak toscana di woote ag bokki ca piemonte kafour dellusi na yoraat njiitug jawrin gi ngir sonnal gu ko askan wi sonnal ci mu dellusi ci biir piemonte ak ci biti nii daal la itaali doone benn ci gox yi nekk ci bëj gànnaar gi ak digg bi kafour dara deseetu ko woon lu dul mu fexee nangu venezia ak moomeeli paab bi ak nguurug napoli gi boole leen ci itaali coona yi garibaldi doon daj ci itaali doon benn garibaldi moom ku bëggoon la te gëmoon bennug itaali moom nag soldaar la woon bu dëgër jàmbaare te ñeme mujjoon na it bokk ci jàmbaari itaali yi siwe woon ag wooteg bennoo gu xeet te daan ci ligeey garibaldi mii tukkee na genova atum g ànd ak lu jege junniy xarekat yu bokkoon ci way coobarewu yu itaali yi nu tudde woon boroom simis yu xonq yi daal di wàcc ak ñoom sisil jot faa dàqe doole ya fa nekkoon te àndoon ak buurub napoli bi ginaaw diirub ñatti weer daal di jéggi xat xatu silil bi dugg ak dooley xareem ji napoli ci lu dul jàmmaarloo gu nu man a tudd ci noonu napoli mujj ak dëkk yi nekk ronam dugg ci bennoo gi samp victor emmanuel muy buuru itaali dooley piemonte ju xare ji jawali woon na ca diiwaan ya nekkoon ca ron kilifteefug paab bi mu jotoon a nangu moomeeli paab bi bepp lu ci dul rom ci noonu xarekati piemonte yooyu jawali woon ca soldaari garibaldi ya ca napoli ci ndigalul kafour ñu àndandoo nag xeex ba nangu mbooleem gox yi nekkoon ci ron nguurug napoli te garibaldi manu fa woon àgg moo rekk ci noonu victor emmanuel ñëw dugg napoli ni ku gañe di dugge ci dëkk bu nu xare ba nangu ko parlamaa bu itaali bu bees bi def na ndajeem mu njëkk ca torino bisub febriye atum g ca ndaje ma lanu ndëppale victor emmanuel def ko buurub itaali gu nu bennal gi ginaaw bi itaali taxawee di ag nguur gu nu bennal ba am juroomi weer la kafor faatu ci sulye atum g garibaldi it bàyyi politig ndax kat moom li ko taxoon a jug mooy ligeey ci itaali doon benn waaye soxlawutoon ay pali politig def rom peeyu nguurug itaali gi waa itaali yi delloosi nanu venezia mi otris tegoon loxo nangu woon ko delloosi gi di ci atum g mu mujj nag moom venezia di ab gox ci itaali ginaaw ba nu fa dàqee dooey xare ju otris ji nanguwaat googu nag ñi ngi ko mane ci ñàkk a tal gi leen otris ñàkkoon a tal ngir xeex bi mu nekkoon di ko def ak brusiya fraans it ay xarekatam gennoon nanu rom ngir sotti gi fraans sotti woon yitteem ca xareem ba ak brusiya bi mu ko defee soldaari itaali yi daal di leen fay wuutu ci sebtambar atum g ñu daal di jibal ci anam gu ofisel ne rom daal mooy peeyu nguurug itaali gu nu bennal gi doxaliin wii merloo woon na paab bi yobbu woon ko ci mu bañ a nangu loolu ne woon it du man a summiku ci sañ sañu politigam yi te du nangoo raflewu ci nguuram gi noonu la mbir mi nekke woon ba g ca la genn dëppoo ame ci diggante mossolini ak paab bi dëppoo googu mayoon na paab bi mu doxe nu ko soob ci mbiri diine ji te am ag tembte gu mat ca vatikan am it sañ sañ ci yabal ay ndaw yu koy toogal ca biti ñu wutal ko nag moom paab bi njëlul boppam lu mu jagoo nii nag la itaali doone woon benn muy lol ay doomam a ko xeex doomam yoy danoo jëloon seen coona bepp def ko ci goreel ko bennal ko te fuqarcee ko ci ngëbug jàmbur bu leen ruuroon teg leen loxo bennoo gii de lu ñepp soppoon la ndaxte doole la ci ñoom di teddnga di tembte te dig fonk sa xeet bennoog itaali du lenn lu dul meññatum sellal ak gëm ag bennoo mooy wuyyu gu mag ga ca woote ga michiavelli doon woote moom mi doon sàkku ciw nitam ca teereem ba tudd buur bi te looloo njëkkoon bennoo gi ci ay xarnu mu doon sàkku ci ñoom ñu ligeey ngir bennal seenuw reew doggantal gu ñaareel gi bennoo gu almaañ almaañ njëkk xare yu napoleon yi almaañ njëkk xarey napoleon yi dafa seddaliku woon ci lu jege ñatti teemeer ak juroom benn fukki diiwaan yepp it ci ron imbraatoor gu otris lanu nekkoon walla li nuy tudde imbraatoorug rom gu sell gi almaañ gepp it genn nguur rekk a fa nekkoon gu mag te temb mooy gu brusiya nguur googu nag jëmoon na kanam te ag yewwuteem fés ci jamonoy buuram ba tuddoon fredrick mu mag mi great fredrick g mooy ki ko defoon muy nguur gu dëgër te am doole bu ko defee waa almaañ yepp wëlbati seeni gët jëme ci nguur gii ngir bëgg ag bennoo almaañ ci jamonoy napoleon napoleon ak xarekatam ya xuusoon nanu ci diiwaani almaañ yi teg leen loxo daal di jawali ca nguurug brusiya gi nga xam ne jàmmaarloo woon na ak ñoom cig njàmmaar ak fit waaye napoleon moom mujj na ko not te gañe ko ci mujj gi ca xareb yena ba atum g daal di teg loxo peeyam ba berlin napoleon merloo woon na lool waa brusiya yi ci dog gi mu dogoon ay wàll ci seeni suuf te jébbaloon leen diiwaanu saksoni bi waaye nag ci geneen wàll am na lu am njariñ lu mu fa indi ndaxte wàññi woon na limub diiwaan yu almaañ yi ba ci fanweer ak juroom ñeent rekk te bu njëkk lu jege lanu woon kon jëfi napoleon jii mbir la mom moo nooyal yoon wi waajal ko ba ag bennoo gu almaañ man a judd man a taxaw almaañ ginaaw ndajem vienne mi ginaaw bi napoleon bonaperte daanoo atum g ci lanu def ndajem vienne ñu jële fa ay saxal yu bari bokk na ci yooyu dagg doox bu warsaw gu poloñ gi dagg ko ci brusiya te jox ko rusi bu ko defee ñu jox brusiya moom itam goxub rayan ak xaaju diiwaanu saksoni daal di taxawal ag bennoo gu almaañ gu làmboo fanweer ak juroom ñeenti nguur nguuraan yu almaañ otris jiite ko defiin wii nag mi ngi ame ci càkkuteeful metternich ak naj gi mu doon naj way daje yi ngir ñu defal ko bëgg bëggam boobu bennoo gu almaañ gii juddoo ci ndajem vienne mi nekkoon na di lu manul a wéy ndax kat otris moom daa tàmbli woon di genne ay saxal aki ndigal yuy kontar tas xibaar gu gore te wéeroodi fenn tey kontar mboolooy almaañ yi daan sàkku ag bennoo te daan ko woote te otris it daa mujjoon teg loxo ci jataayub bennoo gu almaañ gi te ga woon ko ci mu genne ay saxal yuy digale ñu fuglu daara yu mag yi ak leekol yi ak ndaje yi añs doxaliin yooyu nag taxoon na ba ay kàddu jib yu ay waa almaañ di sàkku ñu fipp ci kaw otris tey sàkku ñu jeem a bennal almaañ ci keppaarug nguur gu almaañ gu dëgër loolu mooy li xeltukatu almaañ bi hegel daan sàkku te daan ko woote moom ak ñeneen ñi daa jam bennoo gii nga xam ne otris a ko moomoon daanaka te tegoon ko loxo taxawaay bi nguurug brusiya ame woon ci naal yi jëmoon ci bennoo gu almaañ gi nguurug brusiya dafa tàmbli woon di yëngu ngir dajale xeetu almaañ wi duggal leen ci genn nguur gu almaañ gu nu bennal mu daal di woon rëddal boppam ab politig bu muy jaar ngir àgg ci loolu mu bëgg mu daal di woon door ci dëgëral boppam ci biirum reew defaraat doxaliinam yekkati koom koomam soppi nosteg galag yi aju woon ci nduwaan ci mbooleem goxi nguur gi ñu daal di taxawal noste gi nu daa wax solofrayn di ag bennoo ci wàllug nduwaan mooy li neenaloon nosteg nduwaan gi ci biir almaañ nga xam ne li nekk ci biir reew mi cim njaay deesu ci genne duwaan nga xam ne danoo feexal yaxantu gi ci brusiya ëfal ko ba mu man a doxe ni ko soob ci lu dul ñu ciy teg ay tënk tënki galag mbaa yu nduwaan doxiinu brusiya wii dey dees na ko lim mu dig soopiku gu mag ci taarixu bennoo gu almaañ gi doxal nanu ko nag ci atum g ci biir ay goxam yu biir yi gox yooyu nga xam ne njëkk nosteg solofrayn gi danoo nekkoon ay gox yoo xam ne bu ci nekk daa amoon nosteg pobb gu nduwaan gu mu bokkul ak kenn waaye bi solfrayn taxawee lanu bennal biir brusiya ci wàllug nduwaan ginaaw bi mu nekkee moom brusiya di lu nu seddale ci juroom benn fukki goxi nduwaan waa brusiya yi yëgoon nanu ne benno gi ci wàllug koom koom mooy cëslaay li nu war a teg bennoog almaañ gi ci wàllug politig looloo taxoon kilifay brusiya yi tàmbli woon a fexe nu nuy def ba duggal yeneen diiwaani almaañ yi ci bennoo gu nduwaan googu brusiya nag amoon na ndam ci li mu doon wut ci yenn ci diiwaan yu almaañ yu ndaw yi waaye nag jot naa dajeek ag jàmmaarloo gu mag ci yeneen diiwaan yu almaañ yu mag yi li ko waral mooy ñoom dañoo gisoon ne li gën ci ñoom mooy ñu sosal seen bopp ag bennoo gu ndawaan gu temb ngir xeex ci bennog nduwaan gu brusiya gi looloo fi indi woon ñatti bennoo yu nduwaan ci almaañ ñooy 	solofrayn 	 bennoog nduwaan gu bavar gi nga xam ne mi ngi judd woon atum g maanaam ginaaw bi gu solofrayn amee ba am ñaari at 	ak bennoo gu nduwaan gu saksoni mooy gi saksoni taxawaloon atum g kilifay brusiya yi xamoon nanu ne diiwaani almaañ yi dananu nangoo duggsi ci bennoo gu solofrayn gi bu nu soppee sart yiy tax manees cee dugg looloo taxoon ñu soppi sarti solofrayn yi nga xam ne leegi danoo sos ab jataay bu làmboo mbooleem ndawi yi ci bokk buy saytu noste googu leegi nag lu fa duggati rekk ci li bawoo ci nduwaan mi ak galag yi ñu koy seddale mbooleem diiwaan yi ci kem limub ña fa dëkk soppi yii de dimblee na ci yaatal gëweelub solofrayn gën a yàkkali ab geewam leegi nag bavar bokksi na ci ak saksoni ci atum g ca saa sa tam nga tàmblee gis lu lay won ne solofrayn moom tàmbli na a naat ak a am ag yokkute yaxantu ga tàmbli woon nay jar di dox mbay ma màgg endustri ba jëm kanam ci mbooleem diiwaan yi bokksi ci solofrayn am na nag benn jëfka boo xam ne moo àntul solofrayn mooy moom de noste gu waa almaañ xalaat ba def ko la loxol otris duggu ci jenn doole it ju ko man a teg loxo yoonam nekku ci metternich gisoon na ay wi nekkoon ci noste gii waaye bi mu koy gis fekk na waxtu wa jàll manatu ca woon dara mu daal di bind imbraatoor bu otris bi ne ko na la wóor ne nguuri almaañ yi bi lii amee de di nanu nekki wenn yaram wu jàppaloo ci ron kerug doxaliin gu brusiya te da na jàppeji brusiya muy moom aw yaram wu di doxandeem wu tumbrànke wu bokkul ciw yaramam te kat waa otris yi ñoom ca dëgg dëgg dunu ay doxandeem ci waa almaañ yi ndax ñoo bokk xeet làkk ak taarix man nanu ne almaañ gepp mujj na bokksi ci solofrayn gi atum g xalaatu xeltu bu hegel bi feddali woon na dooley nguur ak ray gi muy ray jëmm ak lepp lu mu am ngir sàmm dooleem akug màggam ak wegeelam nguur walla àtte ci gis gis hegel cëslaayam mooy doole ci doole rekk la man a dëgërale gëgg kon nguur walla àtte gu dëgër ci gis gisu hegel mooy nguurug walla àtteg dëgg kon moom hegel day mel ne moo teg ci loxol brusiya lay wa xeltu guy rafetal di baaxal seen jëfi jiite googu nu jiite woon bennalug almaañ gi ñu leeral leen ne bi g di jot fekkoon na brusiya muy reew mu am kàttan ci tere otris muy dugg ci mbiri nguur nguuraani almaañ yi naka noonu nekkoon na it mu amoon kàttan ci jiite yëngu yëngu gi jugoon ngir bennal almaañ nguur nguuraan yi bokkoon ci solofrayn it doon man a dimblante ci seen biir ci wàllug koom koom te daan jëflante ci lu dul yoonu otris di ci nekk mbaa ñuy diisoo ak moom walla ñu koy tàggu ci noonu nguur nguuraan yooyu tàmblee xoole brusiya bëtu kilifa ci noonu la bennoo gu koom koom googu doon màgg ak a naat ci ro kerug solofrayn mujjoon di ab jeego bu mag jëm ci ag bennoo gu politig ak xare ci almaañ jeexiit yi fipp gu atum g defoon ci amug bennoo gu almaañ gi ay fipp yu bari jot nanoo am ca tugal atm g ag fipp am ca paris am gu am ca vienne geneen ca brusiya ak ay fipp ci itaali ak almaañ yepp it di xëccu jëm ci ag gore demokraasi ak xeetu metternich mu màggat mii mujjoon na manatul woon a noot fippi tugal yooyu mbaa mu giimal leen ni mu ko baaxoo woon a defe kërug orob gi mujj ni ko metternich di waxe di kër gu màggat te ràpp ba àgg ci maneesatu cee yatt sax ab palanteer ciy miiram ngirug màggat kon leegi li jaadu kay mooy ñu màbb ko te wuutal fa geneen kër gu yees ca dëgg dëgg nag loolu am na ndax kat noste ga amoon ca la ëppoon ca reewi tugal ya daa mujjoon di lu ràpp ngirug yàgg mujj manatutoon a ñàkk ñu yeesalaat ko te taxawalaat ko ci anam gu dëppoo ak li jamono laaj metternich dawoon na te daanu woon ci noonu buurub brusiya bi frederick william mu ñeenteel mi daal di jug woote am ndaje mu parlamaa ngir ñu defaral brusiya ab sartu reew bu bees mu dig aw askanam ne leen moo fas yeenee jiite yëngu yëngu giy jug ci jeem a bennal almaañ ci benn bataaxel bu mu leen jàngal ndaw yi teewal almaañ yepp teewe woon nanu ndajem atum g moomu ñu def fa ay gëstu ci lu aju ci almaañ gu nekk benn ndajem parlamaa mii ñi ngi ko gën a xame ci turu parlamaab frankfort ndaje ma ëmboon na lu bari ciy woykat aki xeltukat aki taskati xibaar aki ustaas ñatti saxal nag yu mag juddoo nanu ca ndaje ma 	bennal almaañ ci njiitul buurub brusiya 	ñu boole ci bennoo gu almaañ googu wàllug almaañ gi bokkoon ci imbraatoorug otris gi 	genne otris ci bennoo gu almaañ gi way daje yii ci frankfort seenub lim àggoon na ci ciy jëmm tànnoon nanu buurub brusiya bi fredereick william mu ñeenteel mi def ko imbraatoor ci almaañ gu nu bennal gi waaye frederick moom daa bañoon ne du dëppoo ndëppul imbraatoor li nu ko joxoon te way daje yi joxoon ko ko ndax da ne ndëpp li daal ndawi askan wee ko ko jox waaye buur yeek kàggam yi joxuñu ko ko looloo taxoon nanguwu koo sol la am nag mooy ne buuru brusiya bi dafa bañ a jël ndëpp li ndax xam ne otris ak rusi ànduñu woon ci bennoog almaañ googu te manoon nanoo xëy di duggati ci seeni mbir ngir loolu rawati na ne otris moom jot na a not fipp gi amoon ca peeyam ba vienne nga rax ci dolli ne buuru brusiya bi moom dafa gëmoon gisiinu àq ak sañ sañ bu yàlla bi mooy gisiin wi naan ñoom buur yi yàlla a leen fi teg moom lanu fi wuutu nit ñi tegunu leen fi du keneen it looloo taxoon bu nangoo it ñu def ndaje moomu muy mu frankfort mi jubluwu ci woon lu dul ngistal waaye du ligeey bu fullawu mbaa mu dëggu ci yoonu soppi otris ak rusi dimblante nanu ci màbb barlamaab frankfort bi ak naalam yi mu amoon te nu jëm cig bennoo gu almaañ looloo waraloon jeem gi nu doon def ngir bennal almaañ ci ron kilifteefug brusiya ci atum g mujjul woon àntu waaye li muy àntoodi lepp teewul xalaat bi sax ci xoli ak xeli waa almaañ yi ñu mujj waa almaañ ñi xam ne daal dunu man a amalati seen bennoo googu ci anamug jàmm mbaa gu sartu reew ndaxte otris àndu ci te mi ngi koy xeex ak doole looloo waraloon nu jëloon seen yitte def ko ci amal am mbooloom xare mu dëgër mu leen di man a may ñu man a genne otris almaañ cig njëlbeen door a lijjanti nag nu nuy doone benn ci ginaaw bi xalaat bii nag diisoowaale bu brusiya bii di bismarck àndoon na ci te jàpple woon ko dëgëral ko moom mooy otto von bismarck boroom kurpeñu weñ bi politigu bismarck ci lu jëm ci bennoo gu almaañ gi bismarck mi ngi judd atum g am njàggam mu kawe mu defe ko ca daaray berlin ju mag ja daal di dugg ag coldaar gennati ca dem nag feete ca boppam ca toolam ba mi ngi bokkoon nag ci njaboot gu woomle gu ami alal yu rëy ca brusiya sampoon na boppam ngir nu fal ko ci bennoo yu almaañ yi atum g ñu tànnoon ko it muy ab cer ci parlamaa bu brusiya bi ligeey na it ci toolub diplomasi doonoon ndawul reewam ca butrsburg ca rusi ginaaw bi mu nekkal reewam ca paris foofee la ko william mu njëkk mi doon jiite brusiya woowe woon mu juge fraans ngir jiite si njiitug jawrin gi ci brusiya bismarck nag nekkoon na ku gëmoon te daa dëgëral noste gu nguur gu nu joyal te gëmoon ne buur daa war a am doole te am soldaar su dëgër egliis bi jàpple ko ak garmi yi bismarck moom faalewutoon parlamaa bi gisoon na ne jëm kanamug aw xeet walla ag yeegam jëm ca kaw manul a ame ci lu dul ay buuram di ñu kawe ay yitte ak ay kilifaam waaye du nu ko ame mukk ci ay saxal yu juge ci ay parlamaa aki nostey sarti reew bismarck yitteem jepp mi ngi ko jëmale woon ci genne fraans ak otris almaañ mu gisoon ne lii daal manul ame ci lu dul dooley xare ju mag ju leen ci man a ga ci noonu mu tàmblee ligeey ci dëgëral dooley xare ji ak kàttanal ko mu daal di tas parlamaab brusiya bi ndaxte moom parlamaa bi daa bañoon ne du woote alal ji mu doon laaj ngir man cee dooleel soldaaram si ci noonu mu tëjopon kepp ku wuuteek politigam boobu daal di digle ñu fuglu yeglekaay yi daal di beddiku sartu reew mi ne du ci sukkandikooti alal ji mu soxla woon mu gennelu ko ci ndigalul buur bi bañ cee sukkandiku ci lu parlamaa bi wàllug xeetu nag moom gis gis bi mu ci amoon moo gënoon a yaatu bi mu amoon ci sartu reew ndax daa gisoon ne sartu reew moom mi ngi ame mook ay jubluwaayam ci ginaaw bu ag xeetu amee ba noppi bismarck nag neenalul mbooleem parlamaa bi mbaa mu tas ko lepp moom kay da caa neenl walla mu soril ko ñatti mbir ñooy 	coldaar gi 	politigu bitim reew bi 	fal ay jawrin ak di leen folli bismarck wone na dogu gu mag akug takku contar teg gi otris teg loxo almaañ loolu nag gën na a fése ci taxaw gi mu taxawoon ci dakkal politigu otris bi muy teg almaañ looloo taxoon otris mujj woo buuri almaañ yepp cim ndaje ca frankfort ngir sos ag bennoo gu federaal guy doxal ab goornamaa boo xam ne ay dooleem ak sañ sañam mi ngi koy jële ci sart boo xam ne otris moo koy defar tër ko bismarck gisoon na ne lii de ag anam gu yees gu otris jëlati la ñu muure ko mbubum diplomasi ngir yeegati ci kaw waa almaañ yi bismarck melaloon na sart boobu ne mooy sart bi gën a bon ci mbooleem yu mas a am ci kaw suuf ci noonu mu ne woon du teewe ndaje ma lu dul ci kaw ñu jox brusiya ay àq aki yelleef yu tol ni yi nu jox otris ci ñaari mbir yii ñooy 	dëgël ak wéyal jibalug bennoo gi 	jiite benno gi bismarck ci taxawaayam bii leerale na ci ne otris daal moom ñàkk na kàttan ga mu amoon ci aakimoo moom rekk mbirum bennoo gu almaañ gi te it won na nguur nguuraani almaañ yi ne brusiya mii kat mooy jenn dooley almaañ ji man a jiite bennoo gu almaañ gi bismarck jeem na a fàggu cofeelug rusi ngir mu bañ a feete fenn bu ab xare tàkkee ci diggam ak otris loolooo taxoon mu dugg ci lëj lëju poloñ bi jàpple ci rusi kontar gori ploñ yi defoon ag fipp kontar rusi ngir dañal ag àtteem te jeem a am ag tembte ba man a amal ag àtte gu poloñ gu temb fraans nag àndoon na ca fipp ga te jàpple ko askanu angalteer wi ànd ca waaye goornamaa ba moom àndu ca woon ndax daa ragaloon ag nguurug poloñ gu katolig judd guy dem di àndeek fraans ci noonu bismarck moom dem jàpple ji rusi te jàpple googu gu amoon doole la ndax moom reewam brusiya daa taqaloo woon ak poloñ ba noppi taqalook rusi te it nanguwutoon a ànd ak fraans ak otris kontar rusi xarey bismarck yi ngir taxawal bennoo gu almaañ bismarck xuus na ay xare ak lu bari ci reewi tugal yi digoo k almaañ ngir bennal reewi almaañ yi ñu tudd ñatt rekk ci xare yooyu ñooy xare brusiya yi ak danmark bismarck xuus na ab xare kontar danmark atum g ànd ca ak otris ngir nangu ñaari diiwaan yii di shalswig ak holistin ñu doonoon ñaari doox yu bokkoon ci bennoo gu almaañ gi te danmark tegoon leen loxo danmark mujjoon na ñàkk pexe daal di deltu ginaaw wëlif ñaari doox yooyu atum g bu ko defee brusiya jël dooxu shalswig otris it àtte diiwaanu holistin xarey brusiya ak otris bismarck gisoon na ne xare bi moom deet sikk aji tàkk la ci diggante brusiya ak otris te li ko waral du dara lu dul diiwaanu holistin ndax kat mbir yi manunu woon a nekk di wéy ci anam gii nu nekke di ay maslaa yu dëggoodi aki lijjanti yu xootadi aki juboo yu gàtti dig bis bu yàlla dogalee njortul bismarck loolu mujj di dëgg ba brusiya am ndam loolu de da na nekki muccug waa almaañ ñi ci gàllankoor gii tukkee ci otris gu leen di teree nekk benn tee bennoo gu almaañ gu wér man a am màggug brusiya ci wàllug politig ci biir bennoo gu almaañ gi mujj di luy jeqi njàqare ci otris solofrayn moom màgg na ci anam gu doy waar rawati na bi ci nguur nguuraan yu almaañ yi tiim geejug bëj gànnaar gi bokksee ci noonu lu sakkan jug ciy yooni weñ lënkale diggante wàll yu almaañ yu wuute yi loolu tam dooleel bennoo gu koom koom gi nga xam ne brusiya mujj na di ci ki ci gën a jariñu sabab yii rekk doyoon nanu ngir taal xeex bi ci diggante brusiya ak otris rawati na ginaaw bi dooley brusiya ji doxee jawali holistin nangu ko te moom daa nekkoon ci ron kilifteefug otris ngir dëppoo gi amoon ci diggante brusiya ak otris atum g bismarck moom lijjanti woon na ba rusi genne loxoom ci diggam ak otris loolu nag di ci jàpple gi mu jàpple woon rusi ci giimal fipp ga amoon ca poloñ atum g dëppoo woon na ak imbratoor bi napoleon iii imbraatooru fraans moom itam ngir mu seetaan kook otris bañ cee dugal loxoom li mu koy faye ci loolu nag mooy bàyyi kook yenn moomeel yi ci goxub rayn mu demati tapoo ji ak nguurug itaali gi nga xam ne li doonoon yitteem mooy nocci venezia ci loxol otris ngir matal ag bennoom xare bi amoon ci diggante otris ak brusiya xare la woon bu fëkk te gaaw wéyutoon lu ëpp juroom ñaari ayu bis moo waraloon nu tudde woon ko xareb juroom ñaari ayu bis yi dooley brusiya ji jot na ca a gañee ju otris ja ca xareb sadwa ba ca bohima atum g mu manoon a àgg sax moom dooley brusiya ji ba ca vienne bu imbraatooru fraans bii di napoleon iii jugutoon dox tànki jàmm ci diggante bi ci noonu bismarck daal di ñàkk pexe taxawal xeex bi ngir ragal fraans dugg ci xeex bi ci wetu otris te it bismarck moom da ne woon na doylu nag ci gañe gii mu gañe otris ak dammte gii mu ko dammte ndaxte soril na ko bennoo gu almaañ cig wàll te it bëggutoon a toroxal imbraatooru otris bi ngir loolu man na a tax bu jugee ëlëg moom brusiya di xare ji ak fraans otris du ko sot ci geneen wàll ag juboo amoon na ci diggante brusiya ak otris ñu koy wax juboog braax gi atum g ci la yii ame 	gennug otris ci bennoo gu almaañ gi gi mu tegoon loxo la ko dale ca jamonoy metternich 	duggug mbooleem nguur nguuraan yi nekkoon ci bëj gànnaaru dexu rayn gi ci bennoo gu federaal gu almaañ ci ron njiitul brusiya diiwaani bëj saalum rekk a bokkutoon ci bennoo googu 	bàyyee gu otris bàyyee itaali venezia gis nga ko bismarck kat am na ay ngërte yu am solo ci xareem beek otris moom de fare na fi bennoog almaañ gu yàgg ga indi fi leegi ag bennoo gu almaañ gu yees gu ame ci mbooleem reewi bëj gànnaaru almaañ nga xam ne ñaari doox yii di shalswig ak holistin ci lanu woon buuru brusiya bi jiite ko bismarck nos na bennoo gu yees gi wutal ko ab parlamaa rashstach ndawi askan wa di fa daje ak jataayub bennoo gu almaañ gi bundasrat ndawi diiwaani almaañ yi bokk ci bennoo gu almaañ gu bees gi di fa daje bismarck it lijjanti na ba def ak diiwaani bëj saalum yi bokkutoon ci bennoo gi lijjanti woon na ba def ak ñoom genn tapoo gu xare xareb brusiya ak fraans xetug xare tàmbli woon na a xeeñ ak a jòlli ci diggante fraans ak brusiya ginaaw bi brusiya gañee ca xareb sadwa ba ndaxte fraans moom begutoon dara ci lii brusiya amal ciy ndam ci kaw danmark ak otris cig wàll ak àntul gi mu àntuloon bennoo gu almaañ gu bëj gànnaar gi ci geneen wàll fraans moom daa jàppe woon loolu muy aw xët ci digg ginaawam ndaxte moom kat manul woon a dékku ag nguur gu almaañ gu am doole ci wetam moom kay li ko sooboon mooy almaañ des di nguur gu nu dogat ngir mu nekk moom fraans di reew mi am kilifteef ci sowwub tugal bi moom kay jamono ju nekk da daa kontar bennoog almaañ gi ni ko otris kontare woon bismarck it tàmbli woon na a xalaat nu muy xëcce diiwaani almaañ yu bëj saalum yi ngir nu bokksi ci bennoo gi jëf ju mel ni jooju nag fraans du ko doon nangu ndax moom tàmbli woon na di dugg ci mbiri diiwaan yu almaañ yu bëj saalum yi ngir tee leen a bokki ca bennoo gu almaañ ga nga xam ne brusiya ko jiite woon lëj lëju ku jigeen ki waroon a donn espaañ daal di taxaw mooy lëj lëj bi taaloon xare bi ci diggante brusiya ak fraans lëj lëj boobu mi ngi tënkoo woon nii gàngunaay gu nguurug espaañ dafa feexoon ginaaw bi lingeeru espaañ bi elisabeth dawee ñu gaaral buur bi leopold ndëpp li moom mi ngi bokkoon ci njabootug hohenzellern di woon ab njegeñaaleb imbraatoor bu brusiya waaye ak li leopold di bañ lepp ne du sol mukk ndëpp li teewul fraans mer ci loolu jàmbat ko ci buurub brusiya bi daal di sàkku ci moom mu warlu ne du ànd ci ñu samp kenn ku bokk ci njabootug hohenzellern ci gàngunaayaug espaañ gi waaye buuru brusiya bi bañ ndax loolu kat dafa xaw a laal teddngaam ak ngoram te xaw a niru ag yabeel loolu nag mi ngi ame woon cim ndaje mu mu defoon ak ndawul fraans ca ems bu ko defee buuru brusiya bi yonnee ab day ca la juge woon ca ndaje ma mu yonnee ko bismarck mi nga xam ne lepp li mu doon def mooy neggandiku ab pose ngir jibal ab xare ci kaw fraans ba mu ko defee bismarck xëy tas ci yëglekaay yi ay cofiit ca la bawoo woon ca ndaje mooma ngir merloo ci fraans loolu nag ni mu ko defe mooy genne ay baat yu xaw a wow yu begloowul dara fraans ci noonu fraans jug jibal ab xare ci kaw brusiya ci sulye g te fekku ko woon jekk ngir xeex te taxul woon it mu xalaat ci ngérte yi man a juddoo ci bii xare bis bu nu dàqee fraans ci xeex bi brusiya li nuy wax xareb fëkk la doon def ak fraans maanaam gaawal ko loolu nag jot na koo def ba am ci xam xam ca xareem ba ak otris bi mu ko defee tàngooru xare bi sax di tar lu tollook juroom benni ayu bis waaye tàmblee giim ci ginaaw bi rawati na ci ginaaw bi ay màndargay kawe ak ëpp doole tàmblee feeñ ci xeex bi ñeel brusiya xare bi bepp nag ci suufus fraans la doon tàkke jotoon nanoo dàq fraans nag ci xeex yu bari bi ci gënoon a siw nag mooy bu sedan ca satumbarg nga xam ne àggoon na ci napoleon iii manutoon a ñàkk a wommatu te nangu ne gañe nanu ko ngir dàq yu metti yi te toftaloo te yepp di yu nu teg ci kaw dooley fraans ji ci biir suufus fraans te ray lu sakkan ciy soldaaram te itam lu jege ñaari teemeeri junniy soldaari almaañ sutuxlu ba ca xolub fraans te mu leer nàññ ne fraans moom manatul a gañeeti brusiya ca jamono joojee te manatu koo genneeti suufam loolu nag di woon ci oktobar g ci noonu imbraatoor gu fraans gu ñatteel gi daanu ñu daal di taxawal ci paris nosteg pénc gu ñatteel gi daal di teg fraans ñeel brusiya alamaanug xare gu toll ci juroomi bilyoi frank yu fraans loolu mooy tollook daanak alamaan bi napoleon bonaparte tegoon brusiya bi mu ko dumaa ca xareb yena ba g bu ko defee ñu juboo ci xarekati almaañ yi dunu genn fraans li feek fayeesul alamaan bi moom nag jotees na koo fay ci diirub ñatti at nga rax ci dolli dagg gi nu dagge ñaari gox yii di alsaas ak loren ci fraans boole leen ci almaañ nii daal la bennoo gu almaañ mate woon ci njiitul brusiya ci loxol goor gu dëgër gii ni weñ bismarck mi nga xam ne dafa gëmoon bennal almaañ ak doonte day ci dereet ci weñ mbaa sawara bu ko defee imbraatoorug almaañ gi daal di sosu dib xew xew nag bu fés ci taarixu tugal bu bees bi boroom gàngunaay gi imbratooru almaañ bi mujj di ku ñu joyal ab gogam ci def li ko neex ci nguur nguuraan yu almaañ yi sartu reew bu almaañ bu bees bi yaxal na nu sos ñaari jataay 	jataayu bennoo gu almaañ bundasrat 	jattayu rechstag dooley yoonal ji nag mi ngi nekkoon ci bundasrat di jataay bi nga xam ne mi ngi ame woon ci juroom fukk ak juroom ñatti cer ñu seddale leen ci nguur nguuran yi nga xam ne ñoo amal imbraatoor gu almaañ gi brusiya nag moom rekk amoon na fukki kàddu ak juroom ñaar ginaaw bi mu am ñaar fukki kàddu ak li brusiya di moomadi li ëpp ci kàddu yi lepp ci bundasrat teewul mu gënoon fa a guddub loxo gënoon fa a am jeexiit ndax la ëppoon ca nguur nguuraani almaañ ya duggoon ca bonnoog almaañ ga danoo takku woon ci brusiya te daawunu woote lenn lu mu bëggul te daawunu jàllale genn saxal ca jataay ba bu fukki cer ak ñeent àndadee ca saxal ga bu dee nag jataayu rechstag nag moom man nanu ne mooy jataayub askan bi mi ngi ame woon ci ñatti teemeer ak juroom ñeen fukk ak juroom ñaari cer ñu leen di tànn ci anam gu sekkaree dooley jataay bii nag daanaka danu koo lafañal yòqeel ko ndax nguur ak doole yi nu ko joxoon ci ron sartu reew bu almaañ bu bees bi danoo nekkoon di yu doyadi te ñàkk solo bismarck nag jiite na goornamaa bu almaañ bi niki diisoowaale walla chancelier benn ci ñaari jataay yi manul woon ci moom dara mu yoroon it sañ sañ bu rëy te ci ron kilifteefam tam la almaañ gu rëy gii gepp nekkoon nga xam ne ña fa dëkkoon ca atum g jege woon nanu ñeen fukki milyoi nit mujj àgg ci ñeen fukk ak juroom ñeenti milyo ciy nit atum g di maanaam bi bismarck faatoo ba am ñaari at juroomeelu bunt bi sanc gu yees gi sabab yi fi indi sanc gu yees gi ak ay anamam reewi sancaan yi ñaawteefi sanc yi yëngu yënguy nasaraanal ak ay wi mu làmbool doggantal gu njëkk gi sababi sanc gu yees gi aki anamam xamale lan mooy sanc gu yees gi li sikk amul mooy sanc gu yees gii toppoon ci yewwuteg endustri gi ci tugal rawati na ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar fukk g sanc gii de ay reenam tàlliku woon na di dem ba ca yëngu yëngu yu wuññiy juxraaf yu tugal yi nga xam ne dees leen di jàppe ñuy bunt bi nu jaare bay dugg ci sanc gu yees gi tugal doon def ci reewi adduna bi sanc nag dees na ko xamalee ci ne mooy teg loxo gi reewi endustri yu mag yi tegoon loxo mbiri koom koom yi ak yu politig yeek aada ci reew yu bari ci yu amadi doole yi ci adduna bi rawati na yi ci di yu woomle ci wàllug mbay ak mbll looloo tax sanc ci maanaam mii mu yor du lenn lu dul luy yëngu ci nangu ak fëkk alali jàmbur ak ngacc dooley mbindeef yi ak jariñoo leen sababi sanc gu bees gi li sabab sanc lu bari la te lënkaloo ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii 	màgg gu gaaw gi ba ëpp ci wàllug endustri ci lu bari ci reewi endustri yu mag yi loolu nag tax ba reew yii mujj soxlawoo ay ne ne yu nu laalul aki ja tax na tam ba ag gëpplante gu tar te metti am ci diggante reewi endustri yu mag yi jëm ci yaatal seenug kilifteef ak sañ sañ ci gox yi leen man a warlul ag yokkute ci wàllug endustri ndax seen koom koomu xeet wepp ci endustri la tegu woon li juddoo ci loolu nag lu mujjoon metti la ci reew yu neew doole yii nga xam ne yu mag yii danu leen tegoon loxo ngir muucu seen njariñ yeek ne ne yu nu laalul yi ak ngir def leen ay ja yu mag te yaatu yu nu man a jaaye seen ligeeyi tugal yu endustri yooyu 	yokk gu ñi dëkke ci reewi endustri yi yokkoon loolu moo waraloon reew yii gëstu ji woon fu nuy wàññi seen ëppiitum askan moomu bu ko defee ñoom ñu man leen a nekkal dib jumtukaay bu am solo buy dëgëral seen koom koomu reew miy nday laaj na ñu xamal leen ne politigu genne ëppiitum askan boobu ak sotti leen ci reew yi nu sanc politig la bu nu nosoon jublu woon ci ligeeyal xemmeemteefi sanc yu reewi endustri yi amoon way dëkk yu bari woon ba ëpp 	bëgg a soppi nit ñi def leeni nasaraan nasaraanal ak wisaare diiney nasaraan ci kaw kaw yi ak ñu xamul ñi nga xam ne nasaraanal bokk na ci sabab yi gën a rëy yi waral wuññiy juxraaf yu tugal yi am te ñooy li ubbi buntub sanc waa tugal yi jëfandikoo nanu diine niki ab raas bu niy jaare ngir àgg ca seen bëgg bëgg yu sanc yi yu politig yi ak yu koom koom yi ak doonte danoo làqoon loolu bu ko defee mbubboo seen wax jooju nu daan wax naan wisaare ag nasaraan du lu dul xayal ak yiwal nit ñu deltu ginaaw ñi xamul dara adduna bi nag sonne na bu baax ci par parloo ak boddanteg diine ak xalaatu maa la gën bi reewi nasaraan yi ame woon jëm ci yeneen askan yi dul ñoom 	wàññiku gu tar gi amoon ci ñi dëkke woon ci kaw gi ci reewi tugal yu endustri yi taxoon ba jafe jafe am ci wàllug dundub mbay ci reew yii loolu yobbu woon na reewi yii ci ñu wuti bii dund ci reew yu neew doole yii nga xam ne mbay amoon na fa doole reewi tugal yi nag jaarunu woon ci yoon ngir am seen càkkuteef loolu ci misaal ñu jaare woon ko ci yaxantu waaye kay danoo jëfandikoo doole ak noot ak sanc sukkandiku ci seen dooley xare ji ak ñawug seen ngànnaay ak neew dooleg geneen wàll gi mu fas yeenee noot loolu mooy li ko dimbli ba mu man a am bëgg bëggam yooyu ci kaw askan yu doyadi yi 	lu bari ci reew yu mag yi li leen doon defloo sanc googu mooy feeñal ag yëg sa bopp aakimoo mbir yi ag rëy ci wàllug xeet yaakaar ne ñoo gën yooyu nag ay jumtukaay lanu won ngir wone doole ak màgg gi nga xam ne reewi sanc yii màggoon nanu ko te ame ko ni doole 	ay lonkoo yu tugal ak yu dul ñoom yu mag feeñ nanu ci biir yewwuteg endustri gi dajale woon it alal ju bari ba gisoon ne leegi danu koo war a meññali ca reew yay màgg ci wàlli koom koom yi ci noonu lonkoo yu adduna yu mag yi tàmblee gëpplante ci meññilu alal yooyu loolu nag jur ag jongante gu mag te tar ba mujj sax yii lonkoo tàmblee sàkku ci seeni goornamaa ngir ñu jàpple leen te dëgëral leen loolu tam daan yobbu goornamaa yi ci ñuy aar seen njariñu lonkooy reew loolu nag nooyal na yoon wi ba xeetu sanc gu politig man a taxaw di lol gëpplanteg koom koom a ko fi indi 	bëgg gi reewi sanc yu mag yu bari bëggoon na dëgëral seen yoonu jokkoo gu adduna loolu yobbu leen ci ñu teg loxo yenn yoon yu strateji yi ak waax yu am yi solo ak yoon yu mag yi am solo ci wàllug jokkoo gu adduna gi di taqale diggante goxi adduna bi 	bëgg gi yenn ci reewi sanc yu mag yi bëggoon a tas seeni xalaat aki dal principes yu seeni làngi politig ak seeni aada jàppe loolu nag ab jumtukaay buy ligeeyal seeni xammemteefi sanc anami sanc gu bees gi sancug tugal gu yees gi dafa jëloon ay melo aki anam yu wuute yoo xam ne xew xew ya peegoon te yiiroon reewum sancaan mi ak mi muy sanc xew xew yooyu danu doon jeexiital ci ñoom bu ko defee sanc gu bees gi dikk ci ay anam yu bari ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii sanc ngir dëkk xeetu sanc gu ñaaw gii feeñ na ci ginaaw yëngu yëngug wuññiy juxraaf yu tugal yi bu ko defee reewi tugal yiy wuññi daal di taxaw ci neewal doole ñi cosaanoo woon ci reew yi nu wuññi jaare ko nag ci di leen dàkku ak a genne seeni reew ak di leen alag ci xare yi di leen toraxal di leen seeyal ci biir mboolaayi reew miy sanc maanaam di leen def daanaka ñuy ñenn ci ñoom ci wàllug aada deesu leen manatee ràññale xeetu sanc wii mooy li waa espaañ defoon ca endo yu xonq ya ca amerig gu digg ga ak gu bëj saalum ga bi nu leen sancee te dëkke leen taxawal fa ay sancu yoy mujjoon nanu cuub gox bii ci cuubug espaañ ginaaw bi fi ay waa espaañ jëlee barabu endo yu xonq ya fa cosaanoo mel ne leegi fa lanu cosaano loolu di ci amerig gu digg gi ak gu bëj saalum gi lu ci dul bresil moom waa portigaal a ko sancoon nu mel noonu la sahyooni yahood yi defoon ca falastin bi nu ko sancee ci doole dëkke ko reewi sanc yu mag yi jàpple leen ci britani nekk ca bopp ba ci noonu la yahood yi tasaaroo woon ci adduna bi dajee dëkksi ca falastin ginaaw bi nu leen fa gàddaayalee jëme ci ron aarug reewi sancaan yi ak li askanu falastin daan xeex loolu lepp te daan ci jiyaar ngir bañ ko nii it la sancug tugal gi meloon ca afrig gu digg gi ak rodisiya ñu fay teg doomi afrig yi lu sakkan te lëw ciy coona di leen noot di leen teg loxo di leen tiital di leen tàqale ak a gënale ci wàllug xeet ak lu bokkul ak loolu lepp ci anami mbugal yu tar te mbaam àlle teg loxo gu xare ay reew yu sancaan jug nanu teg loxo ay reew nangu leen ci doole loolu nag li leen ci gënoon a jañ gënoon leen cee yobbu mooy neew doole gi nu gndiku woon ci yii reew rawati na ci wàllug xare li ñu doon jublu ci teg loxo googu mooy man cee jaare bay wéyal ak a doxal seen naali sanc yooyu daan tax ba nuy man a teg loxo ci koom koomi reew yi nu nangu ci seeni dooley xare ci seen politigu bitim reew ak seeni mbiri xam xam ak aada ngir man a samp bu baax seen kenoy sanc ci dëkk yii misaali sanc yu mel nii yu bari lanu nañu ci indi yii rekk sanc gi fraans defoon aljeeri atum g ak sanc gi britani defoon adan atum g defoon ko it isipt atum g ak teg gi fraans tegoon loxo dunu madagaskaar atum g beljig defoon ko kongo atum g ak nangu gi itaali nangu woon libi atum g ak ecopi g xeetu sanc wii mooy wi gënoon a tar te gën a ñaaw ci xeeti sanc yi ndaxte lu diisoon la ci ñi cosaanoo woon ci reew yi nu tegoon loxo ndaxte sanc gu sukkandiku woon ci jëfandikoo doole la waaye li muy tar lepp ak a tiitale teewul nit ñi xeexoon ko te xaru woon ci jële ko fi jànkoonteek lu sakkan ciy jafe jafe aki coona ci seen xeexu njàmbaar boobu ñu ko doon xeex ba mujj ame ci lu màgg li nu doon wut muy gore ak tembte ak dàq sancaan yi ñu juge seeni reew aar reewi sanc yi mujj nanu wut geneen anam gu yees gu nuy sance ak a tege loxo reewi jàmbur yi ñu soppi woon seen sanciin woowu doon tegu ci dooley xare wut weneen wu nuy tudde aar aar nag ci maanaa mu sanc mi mu yor gënul benn yoon sanc gi nu daan defe ci teg loxo ak nangu reewum jàmbur ci doole moom daal aar tur la ci tur yi sancaan yi indi te jëfandikoo ko ci yenn ci ay jamono bu dee maanaa mi aar yor ci wàllug sanc mooy def gi reewi sancaan yi daa def ay dëppoo aki kollarante ci anam gu maandoodi ak yeneen reew yu doyadi yi te neew doole bu ko defee reewum sancaan mi day kollaranteek reew mi mu sanc ci di ko aar ci mbooleem tooñ gu ko man a dikkal juge ci dooley politig ju digook moom walla jeneen bu ko defee loolu di may reewum sancaan mi muy doxal mbirum reew mi nuy aar ci wàlli kaaraange bitim reew ak koom koom reew mi nu aar daal du doxal lu dul mbiri biir reewam rekk loolu nag daa na tax mu nu aar mi daawul am temb gu mat ndax ag gore gu politigam kollarante yooyu danu ko daan tënk ba daa ko tee muy def ay ligeeyam ci mbooleem ay mbiri reewam ci ni mu ko neexe misaal yi ci loolu yu bari lanu ñu indi ci yii rekk aar gi fraans defoon tunisi atum g ak maraakes g ak aar gi britani defoon adan dale ko ca ba mu ko tegee loxo atum g ak yeneen barab yi mu tegoon loxo feetale reewi sancaan yu mag yi tàmbli woon nanoo wutati ay tur yu bees ngir sanc gu bees gi ginaaw xareb adduna bu njëkk bi loolu nag mu jublu woon ci muur sanc gii muy def muuraayu ag yiw akug xay loolu nag du tee sanc moom di lenn rekk ak mbubb mu mu man a sol ak melokaan wu mu man a dikke ci noonu la feetale dikke moom nag ag anam la ci anami sanc gu yees gi nga xam ne jataayu kureelu xeet yi saxaloon na ko te nangu ko mooy kureel googu nu sosoon ca paris ca ndajem jàmm ma nu defoon atum g ngir lijjanti lëj lëj yi amoon ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi boobu kureel nag fraans da ca a defoon ay jeexiit yu mag mook britani nga xam ne ni nu bëgge mu mel ni daanaka la mel dalu feetale ci jëmmi boppam ñi ngi ko jële ci cosaan la ca yoon wu rom wu yagg wa feetale nag noste la gog defoon na mbooleem reew yi nga xam ne reewi dëppoo yi nangoo woon nanu leen ci imbraatoorug almaañ gi ak reewum usmaan mi ñuy ay reew yu nekk ci ron feetale googu bu ko defee reewi dëppoo yi ñoo nekkoon reew yi nu joxoon feetale googu maanaam ci seen ron kilifteef lanu feetale woon mbooleem reew yi nu nangoo ci almaañ ak reewum usmaan mi bu ko defee ñu waral ci reew yiy feetewoo feetale gi ñuy def leeg leeg ñu indi ay saxal aki leeral yu aju ci seen dooley xare yi nekk ci reew yi nekk ci seeni loxo te nu feetale leen ko saxal yii nag ak leeral yi kureelug feetale gi nekk ci kureelug xeet yi lanu ko daa indil feetale gi tam mi ngi daa yam ci benn ñeenteelu xarnu maanaam benn xaaj ci xarnu bu xaaj ñeenti xaaj misaal yi aju ci xeetu sanc wii yu bari lanu ñu wax la ci rekk feetale gi nu defoon britani iraak penkub jordani ak falastin mi nga xam ne dafa genn ci teg loxo gu britani ngir tàbbeeti ci gu israayil ak feetale gi nu feetale woon fraans siri ak libaa ak feetale gi nu defoon goornamaab neewiit yu weex ya nekk afrig de sud feetale gi nu leen feetale woon mbirum namibi ñu yor ko di ko doxal ak feetale gi nu feetale woon japon duni pasifig duni marshal ak feetale gi ostraali ame woon ci kaw gine gu yees gi añs kureelug xeet yi nag daa xëyoon rekk sàkk feetale di ko teg reew yu neew yi doole ci sañ bañ te du leen ci tàggu mbaa mu ciy diisoo ak ñoom denkaane moom itam aw xeetati la ci xeeti sanc yi wii nag xeet la wu feeñ ci ginaaw xareb adduna bu ñaareel bi ñu amale ko nag ci genn saxal gu juge ca mbootaayu xeet ga ñu sosoon atum g ngir wutu fi kureelug xeet yi mbootaayu xeet yi nag neenaloon na kureelug feetale gu sax gi nekkoon ci kureelu xeet yi ngir teg fi leegi jataayub denkaane bi nga xam ne moom lanu wekk leegi mbirum saytu sancu yi reewi digg yi moomoon yilifoon leen reewi digg yi ñooy almaañ itaali ak japon bi nu leen laata a dàqe ci xareb adduna bu ñaareel bi moom jataay boobu tam moo yoroom mbirum reew yi tembagutoon misaalum xeetu sanc gii denk gi nu denkoon itaali libi ak somali ak denk gi nu denkoon britani tanganyika ak yeneen sancug aada moom de xeet la ci xeeti sanc gi nuy jaare ci xalaat yenn ci reewi sancaan yi danoo jugoon ci jariñoo xalaat ak aada ngir ligeeyal seeni njariñi sanc ci noonu ñu sosoon ay jàngu leekol aki xamluwaay aki fajuwaay aki barabi nasaraanal ak yeneen loolu lepp nag ngir man cee jaare bay sanc yii reew ñu ko def te man leen a moom fraans de xeetu sanc wii def na ko ci afrigu bëj gànnaar gi ci tinisi aljjeeri maraakes sunu reew mii it di senegaal def na ko fi defati ko ci reewi shaam yi rawati na libaa reewi dankub mbokkte bi it bennoog sofiet gi jiite leen ñoom itam jeem nanu ba sonn ci wisaare seen xalaat yi ak seen dali làngi politig yi ci reew yu bari ci adduna bi barabi sañ sañ lu bari ci reewi sancaan yi danu doon ngàrtaajoo ak a aakimoo koom koomu lenn ci reewi asi yi ak yu afrig yi ba noppi naan ñoom de dugguñu te seen yoon nekkul ci mbiri politig yu reew yii du caageenug seen mbiri biirum reew misaali xeetu sanc wii mooy la xewoon ca iraan atum g nga xam ne danoo defoon bëj gànnaaru reew ma muy barabu sañ sañ ñeel rusi gu xaysar gi bëj saalum ba nu def ko barabu sañ sañ ñeel britani amoon na it ay xejj yoo xam ne yenn ci reewi sancaan yi amoon nanu leen ci reewi adduna bi lu ni mel mooy xejj yi nga xam ne reewi tugal yi amoon nanu leen ci reewi shaam yi ci jamono ju usmaan ji ak xejj yi nga xam ne reewi sancaan yi amoon nanu leen ci siin ak tayland ak yeneen 	 ñaareelu doggantal reewi sancaan yi lu bari ci reewi sancaan yi doon nanu def seen cawartey sanc yooyu ci fu bari ci reewi adduna bi ci gox yii di afrig asi ak adduna bu yees bi amerig reew yi ëppoon solo ci reewi sancaan yooyu ci taarix ñooy reewum portigaal waa portigaal yi ñooy ñi njëkk a def ay wuññiy juxraaf yu tugal ci ñaari gox yii di afrig ak asi ñoo ci jiitu woon waa espaañ holand angalteer ak waa fraans ak ñeneen ñi jot a def ay wuññiy juxraaf ci jamonoy yewwute gu tugal gi tukkib vasco de gama bu njëkk bi mu defoon ci afrig ak end moo ubbi woon gëti waa portigaal yi jëme leen ci sanc ay barab yu bari ci afrig ak asi ngir teg loxo geeji penku yi ak rënk yaxantug penku gi rawati na li ci aju ci ay rëndaay ak ngir yàq koom koomu reewi jullit ñi rawati na nguurug mamaalig yi ngir loolu man a doyadil jullit ñi neewal leen doole waa portigaal yi tàllaloon nanu seen kilifteef ak sañ sañ ci duni madira yi bopp bu wert bi ak osoras barab yooyu nekkoon ci màmbulaanug atlas gi la ko dale woon ca ñeenteelu bu njëkk ba ca fukk ak juroomeelu xarnu g cig nangu tegoon nanu loxo barab yu bari ci afrig ak asi ci xarnub fukk ak juroom g yu ci mel ni mosambig ci penku afrig angola ci sowwu bi ecopi ak duni madagaskaar moris ak silaan ak xat xatu hormos ak xat xatu malga ci daanaka dun bu malayo añs waa portigaal yi defoon nanu seen sanc gi ngir dëkk ca bresil gi nekk ci amerig gu bëj saalum gi ñu indaale fa woon lu sakkan ciy jaam yu afrig ngir ligeeyloo leen ci mbay meek gasum mbell mi nu leeral leen ne sancug portigaal moom dundul lu ëpp ab xarnu ndax seen soxot gu tar gi nu ame woon ci ñoñ ñi cosaanoo woon ci seen sancu yooyu ak ngir ñàkk gi nu ñàkkoon a yittewoo mbirum nos politig bi ak goornamaa bi ci seeni sancu ak tam ngir xeeg gut ar gi leen askani yii barab doon xeex reewum espaañ espaañ def na ay ligeeyi wuññeem yu juxraaf moom itam ginaaw waa portigaal waaye jariñu ci seen xam xam boobu ñu jot a am ci lef moomu bu ko defee waa espaañ jël goxi amerig gu digg gi ak gu bëj saalum gi def leen ay sancu yu mu sos ngir dëkksi fa moom nag ag sancam daa tegu woon ci fitna ray song jaay doole ak gënale ci wàllug diine ci noonu ñu tàggatoon jaam yu ñuul yi ak endo yu xonq yi ngir ñu bayal leen tool yi gasal leen mbell yi ñu daal di woon jël yii reew cuub leen cuubug espaañ ci làkk ci diine ci aada ak ci taarix ba mujj sax bii gox ñu koy wooye amerig gu latin gi di ko askanale latin gi nu jublu woon esspaañ ak portigaal espaañ it tàllaloon na ag kilifteefam lal ko ci kaw ay barab ci goxu afrig yu ci mel ni duni kanari ak àllub maraakes bi ak goxu afni bi dend ak maraakes ak gine gu espaañ gi nekk ci bëj gànnaaru rëddu yamoo wi sancug espaañ gi neewoon na doole te doyadi ci kanamu jongante gi tugal doon def ci wàll googu ci noonu waa angalteer yi yàqate woon seen mbooloom gaal mi tuddoon irmada atum g mbooloom gaalum holand mi tam moñoxeeti mu espaañ mu lòtt mii atum g ci noonu la espaañ mujje di reew mu neew doole mu loof ci kanamu gëpplante gu angalteer gu fraans ak gu portigaal bu ko defee ay fipp am ca sancuy espaañ ya ci noonu askani dëkk yii daal jéngu xeex ba roccee seen tembte ci loxol waa espaañ yi reewum holand waa holand yi danoo duggoon ci ngérum protestant ba noppi nekk ci ron teg loxo gu espaañ gu katolig gii looloo taxoon ñu defoon seen fipp gu mag googee kontar katolig yu espaañ yii daal di noccee ci ñoom seenug temb ci doole ci njëlbeenug xarnub fukk ak juroom ñaar g waaye temb gii nag nangu na ko moom espaañ ci anam gu ofisel atum g ca kollareg westfalia ga nu defoon ginaaw xareb fanweeri at ba waa holand daal di taxawal lonkoo gu end gu penku gu holand gi ci njëlbeenug xarnub fukk ak juroom ñaar g daal di sóobu ci geewub jonganteg sanc gi ci penku bi daal di not waa portigaal yi ci wàllug sanc teg loxo duni end yu penku ya ca asi yaatuwaayu suuf yi holad mujjoon sanc mujjoon na gën a rëy juroom ñaari yoon yaatuwaayu holand gu ndaw gii ci jëmmi boppam sancaan yu holand yooyu danoo rënkaloon seen bopp rekk yaxantu gi aju woon ci rëndaay yi kawsu attaaya kafe suukar seng ak petrol añs waaye ñii dëkke woon ci sancu yu holand yi te cosaanoo fa xeexoon nanu kontar waa holand yii ba mujj am tembte atum g ci turu endonisi waa holand yi tàllaloon nanu seenug sanc ci diir bu gàtt ci kaw ay barab ci adduna ju yees jii di amerig ñu taxawaloon lonkoog end gu sowwu gu holand gi atum g ñu sancoon goxub dexug hadson daal di jënd manhatan ci endo yu xonq yi daal di taxawal dëkkub amstardaam bu bees bi nga xam ne waa angalteer yi nangu woon nanu ko ci holand tudde ko new york waa holand tam sancoon nanu ci diirub fanweeri at ag wàll gu mag ci bresil gi nekkoon ci ron kilifteefug portigaal reewum beljiig leopol mu ñaareel mi tegoon na loxo reewum kongo mi nekk ci digg afrig atum g daal di koy def ag moomeelam loolu nag wéyoon na di nekk ba atum g ci ginaaw bi lanu tuxale moomeel gii yobbu ko leegi muy gu reewum beljig kongo nag reew mu naat la lool te woomle ci ay koom koomi mbell waa kongo nag jàmmaarloo nanook sancug beljig gii leen doon jariñook a toggi mbugal daan jariñoo it seeni koom koom ci anam yu ñaaw a ñaaw loolu yobbu leen ci ñu am tembte atum g ci turu saayir sancug britani imbraatoorug britani gi moom lanuy jàppe muy gi ëpp ci reewi adduna yi mas a def sanc gu yees gii nu xam tay moom mooy imbraatoor gu sanc gi nga xam ne jant manul a so mukk ciy sancoom ngir bari gi mu bari lu mu sanc ci suufus adduna si britani dey defoon na ci wuññiy juxraaf yi waaye ca amerig gu bëj gànnaar ga mu sancoon lu sakkan ciy suufam waaye dëkke leen te sonn it ci dindi kilifteefug fraans ak holand ci gox bii te jële ko fi bu ko defee sancu ak dëkkuwaay yu britani yi ci amerig gu bëj gànnaar gi desoon ci ron cang gu sanc gu britani ba kero diiwaan yu bennoo yu amerig yi di am tembte naka noonu kanada ñoom reew yii nga xam ne dafa am lu leen boole ak britani muy bokk gi nu bokk ak ñoom askan te bokk nekkandoo ci komonwelth gu britani britani sancati na ostraali ci anamug dëkk ak newsiland waaye temb nanu ñoom ñaar te mujj bokk ci komonwelth britani sanc na end wéyal fab sañ sañam daal di sos lonkoo gu end gu penku gu angalteer gi atum g mu jot a dàqe fraans ca daanaka gox bu end ba mu manante siin ci mu ubbi ay waaxam ci kanamu afyon bii nga xam ne britani daa na ci indi lu bari ci waa siin yi looloo waraloon xare ba tàkkoon ci diggante siin ak britani di woon xare bu nuy tudde xareb afyon bu njëkk bi nga xam ne wéyoon na la ko dale woon ca atum g ba g nga xam ne ca la britani nangoo waaxub hong kong bu straateji bi waax bii mi ngi woon ci loxol britani ba bu yàggul xareb afyon nag benn la ci tooñaange yi nga xam ne britani mi ngi ko doon tooñ waa siin cig wàll ak nit ci jëmmi boppam ci geneen wàll britani tegoon na loxoom dunu brem atum g ak adan atum g ak borma atum g akug wàll ci malayo mu defati ay aar aki kollarante yu maandoodiku ak ab lim ci barab yi nekk ci bëj saalumu dunu araab bi ak tefesug golfub araab bi mu sanc isipt sudaan iraak penkub sordani falastin ak yeneen barab ci reewi asi yu ñàkk doole yi britani nangooti cig sanc lu bari ci reewi afrig yi lu mel ni afrigug bëj saalum gi nijeeriya oganda tansani rodisiya ak somali gi nu xame woon ci turu somali gu britani gi sancug britani gi nag mooy gi gën a ñaaw ci mbooleem xeeti sanc yi ndax moom da daa jëfandikoo cig sancam doole teg loxo ak jariñoo ne ne yu nu laalul yi ak kàttanug askan yi ak tas nit ñi ak xàjjale leen fitnaal leen ak tooñ leen waaye li lii lepp di tar teewul askani sancu yu britani yi xeex nanook sancaan bi ba kero nu ame seen tembte ci noonu la britani dellu mel namu meloon yor dayo bi mu yoroon ginaaw bi sancoom yii tembee wëliif ko foofa la ko lòttug politig gaare ak gu koom koom reewum fraans waa fraans yi bokkoon nanu ci ligeeyi wuññi yu tugal yi ci goxi amerig gu bëj gànnaar gi rawati na ci kanada ak gox yi peek dexug santa lorens gi ñu sosoon fa ay sancu yu fraans yu ci mel ne kebeg gi nga xam ne ci tefesug santa lorens gi lanu ko taxawaloon ak sancu bu luwisiyana bi nga xam ne turam wii mi ngi juge ca luwis mu fukk ak ñeenteel ma buurub fraans ba ag gëpplante gu mag xewoon na ci diggante waa fraans yi ak waa britani ci amerig gu bëj gànnaar gi ci xarnub fukk ak juroom ñatt g waaaye britani moom jot na a neewal doole kilifteefug fraans gi ci barab yooyu bu ko defee fraans moom teg loxo yeneen barab yu bari ci afrig fu ci mel ne aljeeri tinisi akug wàll ci maraakes daal di sutuxlu ci tàkkug afrig gu mag gi daal di yaatal bu baax seen sañ sañ ak kilifteef ci senegaal kongo nijeer madagaskaar somaal gi nu tudde woon somaalug fraans gi gine ak dawme fraans tegati loxo ay reewi asi fu ci mel ne ay wàll ci end waa britani jële leen fa atum g ñoom de jotoon nanoo taxawal lonkoo gu end gu penkug fraans gi ngir gëpplanteek lonkoo gu end gu penkug britani gi ak lonkoo gu end gu penkug holand gi ci wàllug yaxantu ci penku bi fraans sancati sireek libaa ci turu feetale ci ginaaw xareb adduna bu ñaareel ba sancug fraans gii nag daa melowoo ag tooñ tiitale jeem a far aaday reew yi mu sanc ak seeni màndargay reew ak jëmm lu mel noonu it mooy li nu def ci reewi araab yi nekk ci bëj gànnaaru afrig te fraans tegoon leen loxo waaye way dëkke ya xeexoon nanu sancug fraans gii ba mujj am tembte gu mat fii fi senegaal waa fraans sonnale nanu fi tege fiy fitna gennee fi xoolal ku mel ni sëriñ tuuba cig tooñ lanu ko fi gennee sanni ko ca àlli gabong yu lëndam ya yobbooti ko moritani te fii nu koy genne de du seenum reew reewam la xoolal ma fa ñuy wax camp caaroy ak jëf ju ñaaw ja nu fa def xoolal ma sunu làkki reew yii nga xam ne ba tay manunu leen di jàng te fraans nekk ci ginaaw xoolal ma yeneen mag yi nu sonnal xoolal ma aaday nasaraan ji nu fi bëgg a saxal leegi la sax waaye ci ginaaw ak seen senghor mi fi nekkoon nga xam ne daanaka tubaab la woon ngir ne seenub ligeey la woon bu leen fiy ligeeyal lenn luy sunu aada safu ko woon du col mi du wax ji du lekkiin wi du lenn lu mu man a doon naka noonu ñi nekk ci ngunoom ci ñi mu sos defar leen ñu koy ligeeyal reewum almaañ imbraatoorug almaañ gi moom itam dugg na ci geewub sanc bi ak jongante gu adduna gi ginaaw bi mu amalee ag bennoom atum g mu daal di sanc kamerun ak bëj saalumu sowwub afrig bi nga xam ne dees na koy wooye bëj saalumu sowwu afrig bu almaañ bi ngir sanc gi ko almaañ sancoon ak bëj saalumu penku afrig bi nu tudde ba tay bëj saalumu penku afrig bu almaañ ak togo almaañ it jotoon na a teg logo lu bari ci duni pasifig yi nga xam ne ñi ngi leen gënoon a xame ci turu duni argabiil yu bismarck yi ñu nangu tam ñoom waa almaañ xaajub bëj gànnaar bi ci duni gana gu yees yi nekk ci màmbulaanug atlas gi waaye almaañ moom mujjoon na ñàkk sancoom yii ci ginaaw bi nu ko dàqee ci xareb adduna bu njëkk bi reewum itaali itaali tam soobu na ci lefum gëpplanteg sanc gi ginaaw bi mu bennoo atum g mu daal di teg loxo ay sancu ci afrig ci eritri somali gi nu tudde somali gu itaali gi libi ak ecopi itaali nag jëfandikoo na gën ja a ñaawi anami mbugal ak ray ci kaw askani yii reew omar muxtaar ca libi fàttaliku leen ko reewum rusi mu xaysar mi sancug rusi gi moom mi ngi jëmoon ci siberiya turkmanistaan ak ay gox ci asi gu digg gi rusi it teg loxo gox yi nekk ci bëj gànnaaru dexug amoor gi ci siin daal di fay taxawal ab dëkk bu bees ci turu vladivostok lijjanti it ba siin gu neew doole gii jox ko ay sañ sañ ci defar yoonu weñ wu jaar ci suufi manshuriya gu siin gi ligeey ba daal di tàmbli ca atum g sañ sañu rusi it yokku ca kore mu daal di seddoo iraan mook britani daal di sanc wàllug bëj gànnaar ga ci ginnaaw bi nu defee seen dëggoo gu xaritoo gi xaatim ko cis een diggante ñoom ñaar atum g buntub ñatteel bi ñaawteefi sanc li sikk amul mooy sanc gii amoon ci adduna bi ci melokaanam yepp aki anamam bokkoon na ci li gënoon a soof te ñepp bañoon ko te sib ko rawati na askan yi nu ko teg ci seen kaw ba nu mos aw wextanam reer cig lëjam sanc de bijj na lu lëw ciy ñaawteef aki jeexiit yu bon ci ka waskan yu lòtt yi yanu woon ab sukkam ñaawteefi sanc moom dees na leen man a gaw ci wàll yii ñaawteefi sanc yu politig li kenn reerewul mooy ne reewi sanc yi de rekki nanu ngorug askan yi nu sancoon seeni reew rekki it seen sañ sañ ci wutal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom te loolu dal yi aju cig nite yepp ak yu yoon yepp woote nanu ko xañoon nanu it askan yi ñuy àttewoo ci sartu reew ak ci nostey demokraasi yu tegu ci cëslaay lu mucc te sell loolu nag mi ngi am ci ginaaw bi nu yàqee mbooleem campeefi xeet yi te dindee leen fi wuutal fi yeneen yuy ligeeyal seeni xemmeemteefi sanc sanc gi nag jeemoon na a defi pexe ba askan yi nu sanc dunu doon mukk benn bu ko defee mu def lu nekk jëfandikoo pexe mu mu man a doon ngir xeet wi bañ a nekk benn mu tàmblee wut lepp luy tàqalee di ko sotti ak a wisaare ci mepp mbooloo muy menn ak wepp xeet wuy wenn ci mepp reew muy menn mu soññ te sawarloo yëngu yënguy beddiku yi yi nga xam ne neewte yaa ngi leen doon sàkku ak def daal di yittewoo bu baax lepp lu aju ci luy jeqi ag xëccu jëm ci waaso mbaab kureel walla boddante mbaa woote ag gën ci biiru xeet ak wuute ci ngér mu ñëwati xóotal dalub tàqle politig ci mennum reew daal di sawarloo làng yi ànd ak moom ci politigam boobu daal di def ay soppi ci dig yi yooyu soppi nag ñoo mujj di jëfka yu mag yi mujj di taal gilinug wuute gi ak noonoo ci diggante dooley politig yi dëkkandoo dendandoo mu dooleeti indil reew yi mu sanc ay jafe jafey politig yu fasu yoy reew yi nu sanc de wéy nanu di jànkoonteek ñoom ay ati at ginaaw bi nu tembee yooyu jafe jafe wéyoon nanu di fi sax ginaaw bi nu mujjee nekk di fi ag dund gu yees sanc nag jëfandikoo woon na mbooleem xeeti jumtukaayi mbugal yi kontar askan yi mu duma tëj mbugal te ray lu sakkan ci askan yi te dara waralu ko lu dul ne danoo fippoon kontar ko sàkku woon nu nuy goree te temb te loolu àq ju mag la tey yelleef ñeel leen waaye askan yii yanu woon sanc gi jugoon nanu xeex def ci seen lepp ngir yekkati yan bu diis bii tegu ci seenum ndodd ñaawteefi sanc yu mboolaay sanc daal dafa defoon yitteem ci tas xottite bennoo gi am ci mboolaay yi nekk ci sancu yi jaare ko ci soññee cig tàqalikoo wisaare nosteg kureel ci biiru askan bu ko defee kureelug laman yi walla gu sang yi daal di feeñ am ay sañ sañ yu bari aki ngëneel yu tax ñeneen ñu ndool ñig ñàkk di bëgg a ray akug reer mere woon leen gii kureel nag ligeeyal na ba tàyyi sanc gi ci anam yu bari bu ko defee jaasiy sanc gi nekk fi di lu nu bocci ci baatub ñu ñàkk ñi di leen tegi coona di leen fitnaal te kat ñoom ñooy ñi ëppoon ci askan wi am geneen kureel gu feeñati ci wetu gu lamani sancu yi mooy kureelug sang yu doxandeem yii nga xam ne ñoo tegoon loxo ci koom mi ak ci nguur gi walla àtte gi bu ko defee tàggat doomi sancu yi ci ñu leen di ligeeyal sanc gi tàbbal na ci sancu yi mbooleem aada yu ñaaw yi man a yàq ag mboolaay man a ñaawali jikkoom mu soññe cig mbon reer jëfandikoo dorog ak yiy màndal ak wure ak kart ak yu dul yooyu ci aada yu ñaaw yi man a tas bennoo gu ag mboolaay te dëgëral nekkug sancaan yi ak seen doole ci sancu yi te gën fee suuxat seen reeni sanc sanc gi de jeemoon na jëfandikoo woon ci loolu bepp kerkeraan bu mu amoon mbaa yoon wu mu xamoon ngir gòndi niti sancu yi ci xayug tugal gi te sopploo leen ko ngir ag maas man a judd guy gëm te gòndiku ci jëm kanamug tugal gi ak xalaati waa tugal yi li ñu jublu woon ci raxasug xel gii mooy indi fi ag maas gu yees guy ligeeyal njariñu tubaab yi rawati na bu maas gii mujjee jiite reew yi ci politig jaare ko ci seenug jàpple waaye ànd ak pexey sanc yii yepp ngir amal loolu teewul askani sancu yi tas yaakaari way sanc yi sooyal seeni mebat seeni mebat sooy na seeni yaakaar tas bi nu gisee ne askan yi dey ñi ngi wéy di gën a jàpp ci seeni diine di gën a oy ci sseeni aada di gën a ngëb ci seeni pas pas yu laab yooyu fonk seen bopp seen taarix aks een xalaat nga gis ne maas gi juddoo ci jamonoy sanc ñoo yanu woon raayob fipp gi ak xeex bi kontar sancaan yi ñu saxoon nag ci noonu ba mujj fuqarci ci doole seenug gore akug temb gu mat sëkk ñaawteefi sanc yu koom koom li njëkk a yitteel sancaan yi mooy am ay ne ne yu nu laalul yu mbay ak mbell ba man a doxal seen ligeeyuwaay buk o defee man fa a ligeeye lu nuy genneeti di ko jaayati ca reew ya nu sanc looloo taxoon sanc gi saxoon ci di muucu ak a ngacc xeewali reew yi nu sanc yu mbay yeek mbell yi mu soññ lonkoo yu jàmbur yiy rënk ñu ñëw meññilu seen alal yi ci reew yi nu sanc ci anam ak wàll yiy ligeeyal tey jariñ reewi sancaan yi bu ko defee yii lonkoo taxaw ci jariñoo koom koomi reew yi nu sanc ci diir bu gàtt ndax danoo yàgg a ragal fipp yi leen daan kontar te askan yu ndooli sancu yi daan leen def ñoom ñi nekkoon ci ron yan bu diis bii leen tegu woon te weesuwutoon lenn lu dul sanc gi reewi sancaan yi yamunu woon ci muucu xeewali sancu yi waaye àggoon nanu ci def leeni ja yuy muucu ak a dékku marsandiisi tugal yi lii nag moo nuy woo ci ñu tudde sanc gi siyukaay biy si buy dem ak buy ñëw sanc gi moom da daan xeex endustri ci sancu yi daan def lepp lu mu man ngir sancu yi sax di ligeey ci mbay mi te bàyyi endustri bi ngir man a joxe ne ne yu nu laalul yu mbay yu man a dundal endustri yu reewi sancaan yi sanc gi jeem na a ray ruug gëpplante ci doomi sancu yi ginaaw bi mu fi rayee endustri bu lokaal bi tax it ba seeni boroom daanu ci kanamu endustri bu reewi tugal yi bu ko defee këri jàmbur yi teg loxo ci koom koomi reew yi ak seeni alali endustri ñu takk it xalisu sancu yi ci xaalisu reewi sancaan yi loolu lepp nag ñu jublu ci takk koom koomu sancu yi ci koom koomu reew yiy sanc fii nag la genne gisiin wi naan sanc gu politig du lu dul doomi sanc gu koom koom ci sunu jamono jii nu toll ñaawteefi sanc yu aada ak xalaat sanc gi xamoon na ne aaday xeet ak cosaanam mooy li gën a man a dëgëral ag bennoo gu politig ak gu mboolaay te moo gën a gaaw a jañe ci xeex ngir gore cig sanc ci reew yi sanc gi jeem na a soppi taarixu reew yi nu sanc te def ay pexe ci soppi seenug xay gi nga xam ne seen ngértel xeli doom la juddoo nag ci ay jamono yu toppante te toftaloo mu tàmblee jël tooke di ko def ci lem ngir dundal ci doomi sancu yi jaare ko ci aada ak xalaat ngir ñu man a jàpple tubaab yi ci seen xalaat yi ak seen xemmemteefi sanc yi sanc gi nekkoon na fi di doju pakastal ci kanamu am njàng rawati na mi ci aju ci xam xami dëppale yi ak yu xarala yi nga xam ne danuy jàpplee bu baax ci yewwuteg xam xam man a am ak gu endustri ci reew yi te moom sanc gi yitteem weesuwuton ci wàllug njàng li nuy wax njàggale mu matale mi walla njàggale mu yaatu mi bu ko defee njàng mu kawe mi mu jagleel ko doomi kureelug laman gi daa jariñu ci sanc gi des fi sancaan yi danu daa yittewoo tas ak a wisaare seen làkk ak aada ak seen taarixu xeet ak seen xay gii nga xam ne teguwul ci lenn lu dul ci ne ne ñu tay taylu woon di far dëgg yi di indi li dëppoo ak seen njariñ di wisaare xam xam yiy ligeeyal seeni reew di wone dooleem akug màggam ñu tàmbli woon a sikk ndegam ñii cosaanoo ci sancu yi man nanoo jiite am reew daan leen sabooteel seen kilifa yi seen njiit yi seen jàmbaar yi ak seen boroom xam xam yi sanc gi jubluwutoon ci loolu dara lu dul ligeeyal boppam aki njariñam ak jeem fee saxal boppam moom mi nga xam ne masul a dañ di ragal fippug askan yi ak seen yewwuteg xeet doggantal gu ñeenteel gi yëngu yëngu yu ag nasaraanal ak ay wi mu àndal ag nasaraanal yëngu yëngug diine gu nu nos la gu li ko tax a jug mooy tas diiney nasaraan ak xayug nasaraan yi ci jullit ñi ak ñu dul ñoom nasaraanal gii nag lu taqoo la ak sancug tugal gu yees gii nga xam ne jot na a man a ligeeyal diiney nasaraan ci anam gu nëbbu jaare ko ci ay yoon aki defiin yu lëmu te jafee xam loolu lepp nag ngir ligeeyal ay xemmemteef yi mu amoon ci sanc adduna bi yilif ko looloo du yomb nu tàqale diggante nasaraanal ak sanc te itam nasaraanalkat yi danu daa nekk ci ron kilifteefug sancaan yi lu yeeme la diiney nasaraan nekk di benn ci jumtukaayi sanc gu tugal gu yees gi nasaraanal nag yamutoon ci benn jàngu rekk ci jëmmi boppam waaye kay jàngu yepp a ko daan def moo xam jàngu bu sowwu bi la bu katolig bi bu penku bi bu ortodoksi bi bu protestant bi walla bu angalteer bi bu angalikaan bi gëpplante gi taroon na ak xeex bi ci seen diggante ni mu tare woon ci diggante reewi sancaan yi taarixu nasaraanal gu yees gii nag am na ag takku gu mu takku woon ci yëngu yëngu gu wuññi gu juxraaf gi reewi tugal yu nasaraan yi doon def te porrtigaal ak espaañ jiite woon leen di woon ñaari reew yu ëppaloon ci diine te daan ci par parloo kontar jullit ñi ak seen adduna bu ko defee wuññikati orob yii ame woon ag parparloo gu diine defoon seeni ligeeyi wuññi soldaarus tugal si topp ci seen ginaaw di ligeeyal xemmemteefi sanc yu seeni reew loolu lepp nag ngir nu àndandoo amal li nu bëgg mooy ligeeyal tubaab yi te taxawal seenug cang ci diineek fetal jumtukaayi nasaraanal aki ker keraanam nasaraanalkat yu nosu yi jëfandikoo woon nanu ab lim bu rëy ciy ker keraan yu leen di dimbali ci seen ligeeyub nasaraanal bi bu ko defee nuy def jamono ju ñëw ñu seet nu ñu ciy def ba ligeeyal ci seen jubluwaay boobu jumtukaayi nasaraanal gën na a jëm kanam ànd ak jëm kanam gi jamono def ak gi xam xami dëppale yi ak yu xarala yi def nasaraanal ñi ngi ko tàmblee ci ay nit di jug di waaraate ak a xamale yonnant yàlla hiisaa j m akum njàngalem diineem wii xeetu nasaraanal sax na fi di ag nasaraanal gu kenn nit di def mu doonoon lu jëmadi kanam waaye tolloo woon ak jamono ju yàgg ji mu dajeeloon jumtukaayi nasaraanal jëmoon na kanam aki ker keraanam bi yewwuteg xam xam ak gu endustri gënee jëm kanam ci tugal bu ko defee yonnee yu nasaranal yu nu nos yi tàmblee am ay mbootaay yu nasaraanal yu bees di leen saytu yuy jëfandikoo mbooleem anam yi ak jumtukaay yu yees yi ngir doxal seeni ligeey bokk na ci li nu daa jëfandikoo 	ndoktoor ak li mu àndal ci ay barabi faju lu ci mel ni fajuwaay yi ak këri faj yu ndaw yi ak barab yiy maye ay garab ci xaranub fukk ak juroom ñeent ay mbootaayi ndoktoor yu nasaraanal yu bari feeñoon nanu ci reewi tugal yi ak diiwaani amerig yu bennoo yi ak yul ñoom ci reewi addunay nasaraan ji li leen taxoon a jug mooy waajal ay doktoor yu goor ak yu jigeen aki matulkat aki jàpplekati doktoor ngir ñu man a ligeeyal egliis bi jaare ko ci ligeey ci barabi nasaraanal yi nu tasoon ci adduna bi rawati na ci afrig ak asi ndoktoor man nanu ne mooy ker keraan bi la man a gën a may ngay man a jonjoo ag nit ñu neew ñi doole ak ñu ñàkk ñi nasaraanalkat yi danu daa wax naan li nu jublu ci jëfandikoo meccem ndoktoor ci nasaraanal mooy ne moom day nooyal yoon wi laytaay ko ba bu injiil dee ñëw ngir dugg ci xol yi du jafe ma ne man nit ki boo ko joxee mu lekk naan ginaaw bi muy bëgg a dee cib xiif di bëgg a dee ci tawat nga faj ko boo nee ko fii la mu ne foofa la rawati na bu ko fekkul muy ku tatawu ci xam xam aaru ci dali diine ju dëggu daanu daa wax it war na doktoor biy nasaraanal mu bañ a fàtte ne day nasaraanal laata a dara di xew mbootaayi nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci meccem ndoktoor mii daal di ubbi lu sakkan ciy barabi ndoktoor ci reew yu ndool yi yittewoo faj aki doktoor ngir loolu man leen a jàpple ci seen ligeeyub nasaraanal boobu leen taxoon a jug 	njàggale ak li mu àndal ciy jumtukaay lu ci mel ne daaray dal yi ak yu diggu yi ak yu ñaareel yi ak xamluwaay yu kawe yi ak daara yu mag yi ak kàggu yi ak daaray mecce yi añs ñi jiite woon nasaraanal gi danoo gisoon ne bu nu ubbee ay daara yii ci reewi jullit ñi ak yu leen moy loolu da na man a doon aw yoon ngir tas ci diiney nasaraan ci doomi jullit ñiy jàngsi ci yii daara rawati na bu nu leen dee def leeg leeg ñu cofal leen ci njàggalem injiil mi leeral leen ko nga rax ci loolu li daara yii daa def muy tas xayug tugal gi ak rawug xam xamam ak jàngal ko yile dongo te loolu ag doyodal jullit ñi rekk lanu ci jublu woon 	jëf ju yiw ak ju nite ji nga xam ne mbootaayi yiw ak nite yu nasaraan yi daa nanu ko def ci reew yu ñàkk yi rawati na ci jamonoy ay yi ak musiba yu dénd yi ak xare yi bu ko defee ligeeyub nasaraanal bi di sawar ci biir daw làqu yi ak ñu ñu tuxal ñi ci reew yu neew yi doole loolu mooy li ngay gis ci reewi afrig yeek ak asi loxob nasaraan biy indi ñam fa jak ndimal ñeel daw làqu yooyu ak ñu ñu tuxal ñi mooy biy tas dali diiney nasaraan ci ñooñii di jariñu ci seen nekkiin wu metti woowu ak seen tumbrànke gu tar gi 	yëglekaay yi ak këyiti xibaar yi tasum xibaar meek yeene yi nga xam ne seen woote yu nasaraanal yee ko daan tax a jug ak waxtaan yi nu daa amal ci penc yi ak taalifi penku penku yi yi daa gëstu ci xam xami penku yi ak seeni njàggat aki pas pas ak li nekkoon ci loolu lepp ci tooke ñeel jullit ñi ak seenug xay aki laaj yu man a jur ay sikk aki jiixi jaaxa ci jullit ñi jëm ci seeni boroom xam xam aki kilifa lii lepp ci jumtukaay yi la woon nasaraanalkat yi gisoon nanu ne daal teere yii ak yu nu mool yii man nanu leen a dimbali bu baax ci wisaare ag nasaraan ci reewi jullit ñeek yu leen moy jaare ko ci li nuy bàyyi ci bakkan yu doyadi yi mbootaayi nasaraanal yi sos nanu ab lim bu mag ci ay daaray yar ci tugal ak amerig ngir waajal ci nasaraanalkat yi war a defi bii ligeey nasaraanal ci reewi araab yi nasaraanalkat yu katolig anglikaan ak protestant yi wisaaroo woon nanu ci reewi araab yi nekkoon ci ron sacug britani fraans itaali mbaa gu espaañ bu ko defee nasaraanalkat yi sos ci reew yii ay barabi nasaraanal ci biir askan wi rawati na fa jullit ña ndaxte seen jubluwaay ci loolu mooy neewal doole jullit ñi aks een diine reew yi nasaraanal gi sutuxlu danu leen ci tuddal yii nasaraanal ag cawarteem fésoon na ci biir nasaatiray iraag yi ci mawsil baxdaad ak basra ñi ko doon def nag di ay nasaraanalkat yu fraans ak yu itaali àntug nasaraanal gu katolig gii ci iraag ci njiitul fraans merloo woon na britani ci noonu mu daal di fa woon yabal ay nasaraanalkat yu anglikaan daal di ubbi bunt bi ci kanamu nasaraanalkat yu protestant yi ngir ñu àndandoo xeex nasaraanal gu katolig gu rëy gii doon àntu bu baax ci iraag loolu jur ag gëpplante gu mag ci diggante nasaraanalkat yu katolig yi cig wàll ak yu anglikaan yi ak protestant yi ci geneen wàll gëpplante gii nag du lenn dul geneenati ci gëpplante yi daa xew ci wàllug sanc ci diggante fraans ak britani ci goxi penku bi britani daa gisoon ne nasaraanalug katolig gu fraans gii nekk iraag tay dara yobbuwu ko fa lu dul suuxat xejjug fraans ak kilifteefam ci penku bi te loolu moom la britani doon ragal moom mi ame woon dooley sanc ji gën rëy te ëpp doole ay turi nasaraanalkat yu protestant yu bari feeñ nanu ci ñi daan ligeey ci toolub nasaraanal ci iraag ci xarnub fukk ak juroom ñeent g ku ci mel ni nasaraanalkat bii di grant ak groves ak samuel zwemer añs goxi golfub araab bi ag nasaraanal tasaaroo woon na ci goxi golf bu araab bi ndaxte bii gox da di ab jàlluwaay bu am solo jëm ci goxi penku yi bi mu ko defee nasaraanalkati protestant yu amerig yi sawar fa daal di fay sos ay fajuwaay yu seenub lim àggoon ci juroom ñeent aki këri doktoor seenub lim ñoom it àggoon ci fukk ak benn nasaraanal gi yamutoon ci mbootaayi protestant yu amerig yi waaye weesu woon na leen ba daj yu katolig yi ak yu angalikaa yu britani yi ci noonu yii mbootaay tàmblee joante ci sos ay daara aki jàngu aki katederaal ci goxi glof bi nasaraanalkat yu protestant yu amerig yi daal di taxawal egliisub injiil bu xeet wi ci kuwet ahmadi manaama ak masxat bu ko defee katolig yi taxawal katedraal bu katolig bu rom bic i manaama ak abuudabi ak egliisu angalikaan bi ci manaama nu daal di sos ay barab yu nu jagleel tas injiil ak seddale ko ak yeneen teerey seen diiney nasaraan ji ay seen yeene yi aju woon ci seen woote bu nasaraanal bi waaye ak li nit ñiy yittewoo barabi faju yooyu lepp ak leekol yi teewul ñu xeex bu baax kontar yëngu yënguy nasaraanal yii ànd ceek li nu am ci jumtukaay ak doole boroom xam xam yi xeex ko cis en xutba yi nuy def ci jàkka yi ak waaraate yeek gindee yi askan yu bañ sanc yii te noonoo ko ñoom itam xeex ko loolu jural nasaraanalkat yi ag sooy akug tas yaakaar reewi shaam nasaraanalkat yi sawaroon nanu ci reewi shaam yi ci siri libaa palastin ak urdun nasaraanalkt yi yittewoo woon nanu mbirum libaa ak palastin rawati na ginaaw xareb adduna bu njëkk bi nga xam ne reewi shaam yi danoo tàbbi woon ci ron feetale gu fraans ak britani bu kodefee way nasaraanal yi sotti seenug nasaraanal ci goxi siri yeek libaa daal di jàpplanteek kureelug mawaarina yu katolig yi ci libaa britani it duggsi feeteek kureelug dursu gi ci libaa nasaraanalkat yi jeqi woon nanu fa ay fitnay kureel ca la xarey kureel yu tàng te tar juddoo ci libaa ci diggante mawaarina yi ak dursu yi atum g way nasaraanal yu angalikaan yi ñoom danoo sotti woon seen yitte ci palastin rawati na ne moom ab diggub diine la bu am solo ñeel ñi topp ñatti diiney asamaan yi diiney yahood ju nasaraan ak lislaam mbootaayi anglikaan yu angalteer yi tàmblee sosi lopitaal aki leekol aki mbootaayi yiw ci dëkki palastin yi rawati na quds betlahem naasira tabariya yaafa ak gasa fii itam du waa angalikaan yi rekk a fa doon def ag nasaraanal waaye it katolig yi ortodoks yi ak protestant yu amerig yi julliti palastin yi jàmmaarloo nanook yëngu yënguy nasaraanal yii xeex ak ñoom bu baax ndaxte daa noonu woon seen diine noonu seen jaloore seen ndono seen xay ak taarix bu lislaame bu xóot bii seenug xeex ko gën na a tar bi mu gënee leer ne ag nasaraanal la te sanc gi lay ligeeyal ci noonu nasaraanalkat yi jàpplanteek seeni goornamaa kontar araabi palastin yi ngir defar lanuy wax dëëlub balfour genne ko it atum g li i ko taxoon a jug di sos am reewum xeet mu yahood yu sahyoon yi ca suufus jàmbur see di palastin di suufus ay araab yu jullit tubaab yi déggook yahood yi jox leen ko ci seenug toroxte ak naqar isipt nasaraanal tas na ci isipt te wisaaroo fi ci xarnub fukk ak juroom ñeent g rawati na ginaaw bi ko britani tegee loxo atum g qibt yi dimbali nanu mbootaayi nasaraanal yi tasoon ci biir jullit ñi ci isipt bu ko defee yonnee bu katolig bu fraans bi tukkee woon liyon daal di def ay ligeeyi nasaraanal yu fés mboolooy nasaraanal yu yesu yi di leen jàpple ci loolu nasaraanal ga amoon ca isipt paab gi dëgëraloon na ko te jàpple ko mbootaayug nasaraanal gu anglikaan gu angalteer gi def ay ligeeyi nasaraanal ci isipt ay cawartey nasaraanalam gën a yokku ginaaw bi britani tegee loxo isipt te jàpple bu baax yii mboolooy nasaraanal te aar leen mbotaayi nasaraanal yu protestant yu amerig yi def ñoom itam seeni ligeey ci isipt ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar fukk g bu ko defee mboolooy nasaraanal yii tàmblee xëccoo ci seen biir ak a gëpplante ci wàllug ubbi ay fajuwaay aki leekol aki egliis aki katedraal ak barabi seddale teere yeek mbindi nasaraan yeek yeneen yiy ligeeyal nasaraanal jullit ñi xeex nanu nasaraanal ci isipt boroom xam xami ashar gu tedd gi jug ñoom itam jàmmaarlook yëngu yëngu gii daal di sos mbooloo muy aar lislaam ngir xeex nasaraanal ci meloom yepp aki anamam mbooloo mii mujj na am ay bànqaas ci dëkk yu magi isipt yi sos it ay jàngu aki wéeruwaay ñeel way ñàkk ñi ñu lòtt ñeek jirim yi ay doxi ñaxtu yu bari am ci kanamu barabi nasaraanal yi ci xaayra demenhor saqasiq ak kafar siyaat añs yenn it ci yëglekaay yu isipt yi dimblee ci feeñal jubluwaayi nasaraanal gi yee it jullit ñi ci ay wi mu làmboo ligeeyub nasaraanal sawaroon na ci sudan rawati na ci ginaaw bi ko britani tegee loxo bu ko defee mbootaayi nasaraanal yu katolig yu protestant ak angalikaan yi def seeni ligeeyi nasaraanal ci biir jullit yi dëkke woon ci bëj gànnaaru sudan ak ñu dul jullit ñi dëkke woon ci bëj saalumam way nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci ñi dëkke woon ci bëj saalumu reew ma te doonadi woon ay jullit ci noonu ñu jot a tas seen diine ji ci ñoom ak aaday sowwu ji nasaraanalkat yi sosoon nanu ay jàngu yu yonnee yu katolig ak yu angalikaan ak yu protestant ci sudan sosati fa ay barabi faj yu nasaraanal waaye waa sudan ñoom toogunu rekk lem seeni loxo ci kanamu nasaraanal gi fipp gu mahdi di xeex na ko broom xam xam yi xeex ko mbootaayi diine yi rawati na ci bëj gànnaaru reew ma ñoom itam xeex ko reewi maxrib bu araab bi maxribu araab bi dafa nekke fu jàkkaarloo ak reewi nasaraan yi rawati na espaañ itaali ak fraans reew yii nag jariñoo nanu bu baax neew dooleg reewi maxrib bu araab bi daal fay yabal ay nasaraanalkat yu bañ lislaam ak jullit ñi ngir ñu def fa seen ligeeyi nasaraanal yi ak ngir nooyal ko waajal ko ba mu man a dékku sanc gi nar a ñëwi di tukkee ci fraans itaali ak espaañ reew yii yepp nag yu yor diiney nasaraan lanu cawarteg nasaraanal gi yokku na te dolliku rawati na ci keppaarug sanc gu tugal gii ci reewi maxrib yi bu ko defee gëpplante gi ci toolub nasaraanal tàmblee tar ci diggante mbootaayi nasaraanal yu katolig yi yu anglikaan yi ak yu protestant yi nasaraanalkat yi daal di wut ay jumtukaay aki ker keraani nasaraanal taxawal ay fajuwaay aki kër doktoor aki daaray nasaraanal añs ci biir loolu ñu def lu nu man ngir fay làkkuw araab te dundal kàllaamay berber yi ngir xeex ci làkku alxuraan wi ñu defoon ay pexe itam ci far aaday lislaam ji ak taarixam jeem a jox jullit ña fa dëkke woon ay reewu yu reewi sancaan yi bu ko defee dunu reewooti ci seeni reew te dunu ko bëggati ñu xeex ak boroom xam xami jullit ñi daa jeem a taxawal ligeeyub nasaraanal bi waaye nag ñu fonk seen reew ñii dëkke woon ci reewi maxribu araab bi amoon nanu ndam ci damm degug sanc gi ak gu nasaraanal gi ngir seen xeexub njàmbaar bi ñu leen jëmale woon barabi nasaraanal yi ci reewi araab yi mbootaayi nasaraanal yi sosoon nanu lu sakkan ci ay barabi aada yu xam xam ak yu faj ci reewi araab yi lii ci la 	mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari ci ay jànguy dal yu diggu ak yu ñaareel yu nasaraanal ñeel xale yu goor yeek yu jigeen yi ci mbooleem reewi araab yi nasaraanal gi dugg 	mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari barabi jàngale yu kawe yi ci isipt yu ci mel ne daara ju mag ju amerig ji xamluwaay bu penku bi xamluwaay bu fraans bi yooyu yepp nag ñi ngi xaayra bu dee sudan nasaraanalkat yi sos nanu fa bànqaas bu kamboni bu katolig bi ak jàngu bu amerig ak jàngu yu qibt yi yu gres yi ak yu angalteer yi mbootaayug protestant gu amerig gi moom tam sos ca bayruut daara ju mag ju amerig ati katolig yi sos fa ñoom daara ju mag ju katolig ja walla daara ju mag ju yesu ji ñu duppee aji sell jii di yuusuf 	nasaraanalkat yu penku penku yi dugg nanu ci akaademiy làkk yi ci reewi araab yi ñu dugg ca akaademib làkk ba ca xaayra ak bu xam xam ba ca dimasq ak bu xam xam ba nekk baxdaad penku penkub angalteer bii tudoon jub nag kenn la ci ñoom ak margoliyos mu fraans mi garifani mu itaali mi hothman mu holand mi ak harithman mu almaañ mi penku penku yi duggal nanu seen loxo ci teere yu bari yoo fiy gis tay ñu tudd ci rekk ci misaal jimblang ci lislaam ak dundug muhammad j m ki nuy wax sir william mouir def ko teere bi tudd lislaam te alfred giyom def ko ak yeneen ci teere yi nëbbal lislaam ag mbañeel 	mbootaayi nasaraanal yi taxawal nanu lu limu ci ay cëslaayi faj lu ci mel ne fajuwaayu marson ak bu maryon wilth ca bahrayni ak fajuwaayu noks ca masqat ak bu harmal ca isipt ak bu maryohanna biy faj bët ca quds ak yeneen yu nasaraanal yi wisaaroo ci mbooleem reewi araab yi ginaaw ci reew yii lanu nekk nag kon yu afrig gu ñuul gii nga xam ne mooy seen mburu mu bees jarul ñuy wax juroom benneelu bunt ñaar fukkeelu xarnu ñaari xarey adduna yi bu njëkk bi ak bu ñaareel bi mbootaayi adduna yi kureelu xeet yi mbootaayu xeet yi mbootaayu reewi jullit ñi danki reew yi ak reew yi feetewul fenn xareb jawwu bi jëm kanam gu japon doggantal gu njëkk gi ñaari xare yu adduna yi bu njëkk bi ak bu ñaareel bi xaaj bu njëkk bi ci ñaar fukkeelu xarnu g seere na tàkkug ñaari xare yu adduna ñooy xareb adduna bu njëkk bi g ak bu ñaareel bi g leegi nag ñu waxtaane leen ci ni nu càllaloo ci jamono xareb adduna bu njëkk bi g li waral xare bi xareb adduna bu njëkk bi am na ay sabab yu jonjoo ak yu jonjoodi kon nanu njëkk a waxtaane sabab yu jonjoodi yi sabab yu jonjoodi yu xare bi man nanoo tënk sabab yu jonjoodi yu xareb adduna bu njëkk bi ci ñeenti sabab yu mag ñooy 	gëpplante gi ci wàllug sanc 	tapoo yi 	màggug yëngu yëngu yiy woote ag xeetu 	ak lëj lëj yu adduna yi a gëpplante gi ci wàllug sanc gëpplanteg adduna gi taroon na ci ginaaw yewwuteg endustri gi ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g reewi endustri yi seeni cawarte gën na a yaatu gën a jëm kanam ci gii wàll ci fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g li ko waraloon di naj gu tar ak jañax gu tëw a dakk gi leen seen lonkoo yu endustri yu mag yi daan jañax jëme ci loolu ak boroom boppi alal yi dëkk ci yile reew rawati na nag ci reewi tugal yi am ay noste yu gore bu ko defee ñu jug tàmblee gëstu ji ne ne yu nu laalul yi manul a ñàkk ngir ligeeyi endustri yii man dox man a jëm kanam tàmblee wër it ja yu nu man a jaaye ji seen ligeeyi endustri yu wuute yi loolu nag jur na fi ag xér ci ne ne loolu tam jurati fi jawwi gëpplante ci wàllug sanc ci diggante reewi endustri yu mag yi lii itam jur ag rawante ci ngànnaayu ci adduna bi bu ko defee endustrib ngànnaay gën a jëm kanam ndaxte ku bëgg a sanc fàww nga yor ngànnaay yu doy ku ko bëgg a suuxat it mbaa nga bëgg cee ame sa njariñi koom koom yi tax nga koy def fàww nga ngànnaayu ag gëpplante gu tar amoon na ci wàllug koo koom ci diggante britani ak fraans cig wàll ak ci seen diggante ñoom ñaar ak almaañ ci geneen wàll silaay almaañ yi bari woon nanu ci ja yu adduna yi ngir ay sabab yoy yenn yi danoo dellu woon ci jëm kanam gi endustri almaañ jëmoon kanam yi ci des dellu ci barig naali koom koom yu almaañ yi ci reewum usmaan mi rawati na naalub yoonu weñu berlin baxdaad kuwet xëccoo googu nag amoon ay jeexiital yu rëy ci tàkkug xareb adduna bu njëkk bi ci nii lanuy gise ne gëpplanteg koom koom gu adduna bi mooy li duggal adduna bi ci paxum xare bu tàng bu nu ngànnaayal b tapoo yu reew yi gëpplanteg politig gi aju woon ci sanc ci adduna bi dafa gënoon na jëm kanam ci ginaaw bi gëpplanteg koom koom gu adduna bi gënee jëm kanam loolu nag tax ba ay dank sosu yu reew defees it ay kollarante aki dëppoo yu yor màndargam politig mu xare ci diggante ab lim ci reew yi seeni njariñi sanc di jegee walla yi ci jot a àgg ci deggoo ci lijjanti lëj lëj yi nekk ci seen diggante ñu tuddal leen ci dëppoo yooyu ak tapoo yooyu yii di ñëw tapoo gu ñaaral gi ci diggante almaañ otris gii tapoo amoon na ci diggante imbraatooru almaañ gi ak gu otris gi atum g bokk na ci li ëppoon solo ci ay sartam lii di ñëw 	bu rusi gu xaysar gi songee menn ci ñaari reew yi meneen mi war na a dimbli mi nu song 	bu menn ci ñaari reew yi tapoo songee meneen mu ñatteel ma ca des da ca a war a ame taxawaayub génn ci di leen seetaan waaye nag ci anamug cofeel ñeel àndandoom boobu 	bu ag dimblante gu am solo amee walla gu xare ci diggante rusi ak fraans ñaari reew yii tapoo de war nanoo ànd ligeey ngir xeex loolu tapoo gu ñattal gi moom ag tapoo la gu almaañ otris itaali mi ngi sosu ci bi itaali duggsee ci tapoog ñaaral gi nu la tuddoon leegi atum g ak doonte njariñi itaali dëppoowut ak yu imbraatoorug otris gi waxuma la sax noonoo gu yàgg ga nekkoon ci seen diggante te li ko waraloon di yilif gi ko otris yilifoon njëkk bennoo ga ak ca ginaaw ba waaye otris mii moo tegoon loxo ag wàll ci suufus itaali ba noppi yilif fa yeneen wàll itaali duggsi na ci tapoo gi ngir wuute gi mu defoon ak fraans ndax fraans dafa dëgëraloon bu baax tànkub sancam ca goxi bëj gànnaaru afrig fu ci mel ni aljeeri atum g ak tunisi atum g kon itaali duggsi gii mu defoon ci tapoo gi du woon dara lu dul doxaliinu politig li mu ci jublu woon di jañaxal fraans ak britani ngir manante leen ci ñu nangul ko te bàyyee ko njariñam yi nekk ci geej gu diggu gi dëppoo gu fraans rusi gi dëppoo googu am na ci ginaaw bi ag jegeente amee ci diggante fraans ak rusi gu xaysar gi loolu nag tàmbli na atum g daal di gën a jëm kanam atum g bi ñaari reew yi dëppoo ci fas ag kollare guy waral fraans di jox rusi ngànnaay te jëmale kanam ag jokkoom jaare ko ci def fa ay yooni weñ ci atum g la fraans ak rusi def ag kollarante guy yaxal lii di ñëw 	taxawal ag dëppoo ci diggante ñaari reew yi ak weccante xalaat ak diisoo buy lëj lëj amee ci adduna bi 	bu menn ci ñaari reew yi duggee cib xare ñaari reew yi war nanoo diisoo ngir dëppale seen diggante dëppoog cofeel gu britani japon ag dëppoog cofeel sosu na ci diggante britani ak japon atum g lii la yaxal 	bu xare tàkkee ci diggante japon ak rusi gu xaysar gi britani da ca a war a genn te seetaan 	waaye bu meneen reew duggee ci xeex bi nekk ci diggante rusi ak japon kon britani da ciy war a dugg moom itam jàpple japon dëppoog cofeel gu britani fraans ag dëppoo gu cofeel xewoon na ci diggante britani ak fraans atum g gu lijjanti woon lëj lëj ak reeroo yi amoon ci seen diggante dëppoo googu nag lii la wax 	féexal fraans joyal ab loxoom ci marog gii nga xam ne jotoon na a temb te nangul ko teg gi mu teg loxo ajeeri ak tunisi 	fraans moom tam nangul britani teg gi mu teg loxo isipt atum g dëppoo gu cofeel gu britani rusi ag dëppoog cofeel am na ci diggante britani ak rusi gu xaysar gi atum g lii la wax 	déggoo ci ni nuy séddoo barabi sañ sañ yi ci iraan ba mu des fa benn barab rekk bu temb ca digg ba ñu bàyyil ko fa shaah ba ginaaw bi rusi jëlee wàll gu bëj gànnaar gi britani jël gu bëj saalum gi c màggug yëngu yënguy xeetu yi ci tugal yëngu yëngu yi aju ci xeetu dafa xëy gën a màgg ci tugal loolu nag bokk na ci li jañ adduna bi jëme ko ci xare bi xarnub fukk ak juroom neenteel g dees na ko lim muy xarnub xeetu yi ci tugal yëngu yënguy xeetu yooyu nga xam ne li leen taxoon a jug mooy gooreel seen bopp te nocciku ci kilifteef ak teg loxog reew yi leen di àtte cig wàll ak sosal xeet wu nekk am reewum boppam mu koy ëmb uuf ko ci geneen wàll ñaar nag bokkoon nanu ci yëngu yëngu yi gënoon a siw ci yooyu ñooy mbootaayug slaaf gi gii mbootaay walla yëngu yëngug slaaf gii li ko taxoon a jug mooy xettali askanu slaaf wi jële ko ci àtteg imbraatoor gu otris gi ak sos reewum slaaf mu ëmb mbooleem slaaf yi dëkke ci balkaan ak salaaf yi dëkke ci tugalug penku gi mbootaay gii nag daan na jot ag jàpple mu tukke ci rusi gu saaf gi loolu taxoon na ba ag reeroo gu mag am ci diggante otris ak rusi gu xaysar gi d lëj lëji adduna bi ay lëj lëj yu fasu yu adduna bi sosu nanu bokk it bu baax ci li fi taal xareb adduna bu njëkk bi lëj lëj yii it li leen jur day dellu ca reeroo ya amoon ca diggante reew yu mag ya ngir seen gëpplanteg sanc gi ak ngir màggug xeetu ci tugal ak ngir fipp gi askan yi fippoon ngir jot seenug tembte ak gore ñu tudd ci yi ëpp solo ci lëj lëj yooyu lëj lëju maraakes fraans yàgg na a waaj ak a naal ngir teg loxo maxrib gu sori gi maraakes moom nag maraakes dafa yoroon ag tembam lu yàgg te booba tunisi ak aljeeri fraans a ngi leen tegoon loxo yilif leen cig sanc ci noonu fraans lijjanteek britani seen reeroo gi nekkoon seen diggante ca dëppoog cofeel ga atum g fraans daal di bokki ca ndaje ma nu njëkk a def ca dun bu wert ba atum g ca espaañ ngir lijjanti lëj lëju maraakes bi saxal ya juddoo ca ndaje ma nag njariñul fraans la gënoon a nekk ndax reew ya fa daje woon danoo dëppoo woon ci nangul maraakes ag tembam waaye feetale fraans wàllug kaaraange ga ak sàmm njabootug tugal ga fa nekkoon fraans nag jariñu na bu baax ci dénk gi nu ko dénk kaaraange ga ndax ba ay yëngu yëngu amee ca faas ga nekoon peey ba da fa a daal di woon yabal ay dooley xare yu fraans ngir ne da ciy aar jàmburi tugal ya fa nekkoon loolu moo merloo woon almaañ mi àndoon ak buurub maraakes bi daal di ne woon fàww maraakes jot cig tembam ngir naqaral fraans almaañ daal di yabal ag gaal gu mag ca waaxub agadiir ngir aar ag njabootam ak ñaxtoo ci yabal gi fraans yabaloon am mbooloom xare ca faas atum g ngir teg ko loxo ñu defaat am ndaje ca dun bu wert ba ca espaañ atum g ngir lijjanti xuloob fraans almaañ bi la fa juddoo di jox almaañ ay moomeel ca kongog fraans ga bu ko defee almaañ nangul fraans nekk gi maraakes nekk ci ron kaaraangeem ñu daal di def tanja muy ab waax bu adduna bepp daal di doxal nag politigu ubbi buntub maraakes ci kanamu yaxantug adduna bi lëj lëju balkaan otris daa boole woon ci boppam ñaari gox yii di bosni ak hersogowin atum g te ñoom ñaar ñi ngi bokkoon ci diiwaani reewum usmaan mi ci balkaan reewum usmaan mi ca jamono jooja dafa nekkoon di dund ci jawwi yong mooy yong gi ñoñ bennoo ñi defoon atum g serbi nag moom ag wàll la ci yogoslaafi ci jamono jii nu nekk daal di ñaxtu loolu ak rusi gu xaysar gi ko daan jàpple moom serbi almaañ jug moom jàpple otris ci jëfam jooju loolu nag bokk na ci li gën a dolli tangoor wi ca daanaka dun bu balkaan ba lëj lëju maseduwaan ab xare tàkkoon na ci diggante reewum usmaan mi ak gres bulgari ak serbi ci maseduwaan ñoom ay reewi balkaan lanu li ko waraloon nag mooy bulgari gres ak serbi danu doon defi pexe ngir roccee maseduwaan ci reewum usmaan mi te seddoo ko ci seen biir bi nu dàqee reewum usmaan mi ca xare ba ba noppi danoo reeroo woon ci ci seen biir ci nu nu koy seddoo serbi moom daa bëggoon na jot ci albani waaye ñu xañ ko ko ndaxte otris daa taxawoon temb ci nu jox albani ag tembam loolu waral leneen coow amati ci balkaan ci diggante serbi otris ak rusi ak ñeneen lëj lëju tripoli itaali jariñu na ci am soxla gi reewum usmaan mi amoon soxla ak lu ko doy ca xareem ba ca balkaan bu ko defee mu song ko ca tripoli gu soww ga atum g daal di nangu libi teg ko loxo atum g ginaaw bi mu lijjantee ba fraans ak britani genn ci te noppi ci sabab yu jonjoo yi ñeel xareb adduna bu njëkk bi noonoo gi taroon na jëm ci slaaf yi ci balkaan looloo waraloon ñoom slaaf yi juggoon taxawal ag mbootaayug sekkare ngir xeex loolu serbi jàpple leen ci ak rusig xaysar gi ab dongab slaaf yong na arshidog fransis ferninand mi nekkoon wuutlaayu otris ak soxnaam ca suwe g ca dëkkub sarayevo bi nekkoon peeyub bosni ci tukkib nemmeeku bu mu fa doon def otris daal di gaaw jirñoo xew xew bii daal di yonnee serbi ag xupp ca bisub sulye g gu làmboo fukki sart ak benn bokk na ci yi ëppoon solo ci sart yooyu raxas goornamaab serbi bi ak dooley xareem ji ci mbooleem ku bokk ci kureel yiy kontar otris te may otris mu defal boppam raxas gii te tëj yëglekaay yi ak jumtukaayi tes xibaar yi noonoo otris ak boole otris ci gëstu ñi def yong googu ak àtte leen ak yeneen sart yu tar yu tax serbi jort ne kii daal daa fas yeenee dugg ciy mbiri biiram ba noppi otris joxati serbi diirub ñeen fukki waxtook juroom ñatt ne ko mooy àpp bi nga xam ne waru koo weesu te tonntuwul waaye serbi moom tontuwul jibalug xare bi otris taal na xare bi ci kaw serbi ci sulye g bi loolu amee rusi moom itam jug song otris ngir jàpple serbi loolu it jurati almaañ jug cig wàllam jafal ab xare ci kaw rusi ak ci kaw serbi fraans duggsi ci ci wetu rusi miy reew miy xaritam nadx moom la defal ag tapoo daal di jibbal ab xare ci kaw almaañ ak otris britani tam it xuus xare bi kontar ñaari reewi digg yi nga xam ne reewum usmaan mi mujj na àndseek ñoom ci xeex bi siin it ak japon mujj nanu duggsi ci xare bi ci wetu reewi dëppoo gi itaali it dugg si ci kontar reewi digg yi atum g te kat bu njëkk da doon seetan rekk feetewutoonn fenn britani nag nekkoon na di fasante ak itaali kollareg sekkare kollare gi nag li mu doon yaxal mooy itaali jox ko suufus dalmaas bu xare bi jeexee amerig dikk moom itam dugg si ci xare bi ci wetu reewi dëppoo yi daal di genn ca beroom ga mu defoon ca goxub amerig ba duggsi gi mu duggsi woon ci xeex bi nag lu am solo la woon ndax moo ko soppi bu baax ngir doole ak jumtukaay yi mu indil reewi dëppoo yi ak alal lefum xare bi jë bu sòww bi ëmboon fraans ak beljig mooy barabu xeex bi ëppoon solo ci xare bi ci diggante g boobu diggante mooy bi gën a tar ci xeex bi ndaxte dooley reewi digg yi jot nanoo putuxlu ci reewum beljig mi ak wàllug penku gi ci fraans ak li reewi dëppoo yi di jàmmaarlo lepp ak a xeex ngir loolu bañ a am lii nag bokk na ci ndam yi ëpp solo yi reewi digg yi def ci jëwub sòww bi waaye reewi dëppoo yi jot nanoo taxawal jëm kanam gi almaañ ak otris doon def ba daanaka àgg ca bunti paris ci xeexub njàmbaar bi nu doon def ngir aaru ñaari wàll yi nag xeex nanu ay xeex yu tar yi ci gën a siw mooy bu marn bu njëkk bi ci sulye atum g bu dee nag ci jë bu penku bi xare bi moom foofa ci diggante rusi ak otris la nekkoon barabub xeex ba di woon poloñ ak balkaan xeex bi amoon ci penku bi nag xawoon na a woyofal tuuti yan bu diis bi nu tegoon ci ndòddum reewi dëppoo yi ci sòwwu bi ndax reewi digg yi danoo mananul woon a ñàkk a dolli seen soldaar sa nekkoon ca penku ba di xeex ak rusi foofa tam ca penku ba lanu gëne woon aw demiin ca sòww ba ndax jot nanu fa a nangoo wàll gi rusi moom ci poloñ ak litwaani ay xeex am ca diggante reewum usmaan mi ak britani ca iraag ak palastin ca la britani tege loxo ñaari reew yii reewum fraans it nangu siri ak libaa bu dee ci geej gi moom xeex bi mi ngi doon ame ci nuuraakon yi nga xam ne almaañ da leen daa joyal ci gaali reewi dëppoo gi mbooloom gaalum britani mi nag moo kawe woon ci xareb geej gi xareb gitland bu geej bi amoon atum g bokkoon na ci xeexi geej yi gën a rëy ci xare bi nga xam ne amaañ ak britani ñepp ñàkke nanu ci lu dul jeex ciy nit ak jumtukaay atum g bokk na ci at yi gën a tar ci ati xare bii ci la rusi genne ci xare bi ca kollareg litofski ga ca desambar g ci ginaaw bi fippug balsafi gi amee romani topp ca moom mi sukkandiku woon ci xare bi ci rusi moom itam ag gennam mi ngi jaare ci kollare ga nu defoon ca boxarest ca at mooma tam la diiwaani amerig yu bennoo yi ñoom it duggsi ci xare bi ànd ak reewi dëppoo yi loolu nag feeñ bu baax ci doxiinu xare bi ndaxte amerig moom jàpplee woon na bu baax ci wàllug xare ak koom koom loolu nag di woon lu sonnal reewi digg yi ca at mooma tam la jë bu usmaan bi it nërméelu ci la jë bu otris it daanu ay yëngu yëngu aki coow yu ay ligeeykat am ca almaañ ca mooma at it la woodrow wilson defoon fukk ak ñeenti poñam ya doon woote ñu taxawal xare bi te bàyyi askan yi ñu def li nuy wax autodétermination muy tànnal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom atum g nag mooy atum ndam li ñeel reewi dëppoo yi waaye it mu nërmeelu ñeel reewi digg yi ndax imbraatoorug otris ak gu almaañ yépp daanu nanu imbraatoorug usmaan gi it ñàkk mbooleem diiwaanam yi mu amoon ci bitib asi gu ndaw gi nguurug bulgari daanu ci noonu askani reewi digg bi daal sàkku wéerum ngànnaay ci ni ko poñi wilson yi doon sàkkoo bi reewi digg yi demee ba lòtt ci wàllug aaru te manatunoo dékkooti xare bi lanu wommatu bu ko defee bulgari xaatim ag wéer ngànnaay ak reewi dëppoo yi ci satumbar turki topp ci ci mujjug oktoobar atum ak otris ci nowambar ak almaañ ci benn fanu nowambar g lijjanti yi ci ginaaw xare bi reew yi am ndam ci xare bi defoon nanu am ndajem juboo ca paris peeyub fraans li ko waraloon nag mooy gëstu nan lanu war a def ci adduna bi ginaaw bi xare bi jàllee moomu ndaje nag clemenceau moo ko jiite woon njiilul jëwrin lu fraans li bu ko defee ñu defe ndaje ma ca njéndul varsaay la di dëkk bu nekk ca wetu paris diiwaani amerig yu bennoo yi wilson teewal ko britani luwid george njiitul jëwrin la nekkal ko fa fraans clemenceau miy njiitul jëwrin ya moom itam wuutu ko fa ak itaali ci teewaayu orlando njiitul jëwrinam reew yii amoon nanu xejj gu mag ci ndaje mi rawati na ñatti reew yii di amerig britani ak fraans ndajem juboo mii ay saxalam ballewunu ci déggoo ak waxtaan wu reew yi gañe def ak yi nu gañe waaye kay reew yi gañe danoo teg seeni sart ci kaw reew yi nu gañe cig sañ bañ kollare ga nu fase woon ca versailles atum g te xaatimoon ko ak almaañ bokk na ci kollare yi ëpp solo te juddoo ci ndajem juboo mi moom kollare googu dafa yaxaloon lii delloo fraans alsaas ak loren ak delloo danmark wàllug bëj gànnaar gi ci goxub sholswig bu ko defee poloñ moom jot ci suuf su bari ci almaañ ak yoon wu yaatoo ñeen fukki miil wu romb ci biir diiwaanub brusiya gi nekk ci almaañ bu ko defee tàqale kook yeneen suufi almaañ yi ci noonu ñu def waaxub danseg bu almaañ bi muy waax bu nu jagleel reewum poloñ mi nga xam ne taxawalaat nanu ko ci ginaaw xare bi nu jëlati ci almaañ diiwaanu sodit jox ko cekoslawaki mi nga xam ne mi ngi sosu woon ci ginaaw xare bi ñu jëlati ci almaañ waaxub mamel jox ko lituwani bu ko defee almaañ ñàkk mbooleem sancoom yi ba noppi nu ga ko ci mu yamale ay soldaaram ci teemeeri junni nu neenal fa duggum coldaarum gu sañ bañ dindi mbooleem tata yi wëroon kanaalub kyel ak goxub rayn nu tàmbli woon a def fuglu gu tar ci ligeeywaayu ngànnaay yi ak jumtukaay yi ci aju ñu nangoo woon ci almaañ it mbooleem ay nuuraakonam aki gaali xareem aki fafalnaawam ak lu ëpp ci ay gaali yaxantoom ci noonu fraans nangooti diiwaanu saar di xuru dexug rayn gi di barab bu naat ci ay mbell mu nangu ko nag diir bu tollu ci fukki at ak juroom ñu daal di teg almaañ nag ag alamaanug xare ak alal ju mu war a fay ju bari ju tollu ci yu sterlin ak doonte almaañ fayu ci ci diggante g lu dul lim boobu rekk imbraatoorug otris gi nag moom ndaje ma daa daal di jeexal nguurug njabootug habsborg ga fa nekkoon daal di taxawal ciy màbbiitam ay àtte yu bari ñooy pencum otris ak hongri ak pencum cekoslawaki ñu jëlati wàllam ya nekk ca balkaan boole ko ca reewum yogoslawi mi sosu ci ginaaw xare bi bu dee reewum usmaan mi moom dafa ñàkkoon mbooleem moomeelam yi mu amoon ci asi ak afrig deseetutoon lu dul moomeelam yi mu amoon ci asi gu ndaw gi ñu daal di ko def muy leegi pencum turki wuuteek lool reewum usmaan mu mag ma nu xamoon loolu di woon ci g ginaaw bi mustafa kamaal atatork g neenalee nosteg saltana ga fa amoon atum g ak gu xalifa ga atum g ndaje mi nag sos na fi ay reew yu yees yu bari ci balkaan mu ci mel ne mom yogoslawi mi jële won ay suufam ci reewum serbi mi ak yenn ci goxi balkaan yi bokkoon ci moomeelug imbraatuurug otris gi bu ko defee nu sosaat reewum poloñ mi ak brusiya reewum cekoslaafi moom itam taxawe ci ñaari xeet yii di slaaf ak cek reewum hongri tam sosu finland stwaani lituwani ak latfiya reew yii yepp jug di dëgëral seeni nekktey politig te bu njëkk danoo nekkoon ci ron teg loxo gu almaañ ci ginaaw bi rusi gennee ci xare bi atum g daal di fas kollareg litofski gi ak reewi digg yi lii moo jeexal àtte gi njabootub romanof gi doon àtte rusi ñu daal di jël nag yenn reew yi teg leen ci ron ag feetale iraak penkub urdun jordanie ak palastin ñu teg leen ci ron feetale gu britani atum g siri ak libaa ñoom ñu teg leen ci ron feetale gu fraans atum g ndajem paris ma nag saxaloon na feetale gii te xaatimoon ko ñu daal di sos kureelu xeet yi league of nations teg ko ci poñub fukk ak ñeent bi ci dali wilson yi doon woote ag ñoal jàmm ci adduna bi ak tee xare amati fi ak dëgëral dimblante ci reewi adduna bi nii daal la xareb adduna bu njëkk bi jeexe ginaaw bi mu sonnalee adduna bi bepp sotti ko sawaraam si ak alkandeem li ray nanu ci lu jege juroom ñatti milyoi nit gaañ ca lu jege ñaar fukki milyo waxuma la nag ñi faatoo ca xiif bu metti ba ak tawat ja xare ba waraloon ñaareelu xareb adduna bi g lijjanti ak saxal ya juddoo woon ca ndajem jàmm ma ca paris ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi ñoo jur man nanu ne lu ëpp ci li sooke ñaareelu xare bi kollareg jàmm ga fa juddoo woon sooke woon na mer wu metti akub sànj ci askani reew yi nu note ca xeex ba askan yooyu nga xam ne doyutoon ñu yanu coonay xare beeki musibaam rekk waaye ñu tegati ci yan leen li ci juddoo ci ginaaw bi ay saxal aki lijjanti yu diis yoo xam ne reew yi notoon a leen tegoon ci seen kaw loolu nag juroon ci ñoom ag mbañeel akug bëgg a fayyu nekkiinu koom koom wi jaxasoo tegoodi ci yoon am pax gasu ci tugal ci diggante askan yeek seeni goornamaa loolu tam man nanu ne mooy li gën a tax ay noste yu yees sosu yoy sañ sañ bu joyu lanu jëloon def ko seen raayo ay kureel yu neew jugoon nanu teg loxo ci àtte gi ci yenn ci reewi tugal yi daal di biral ne li leen tax a jug mooy xettali seeni askan ci jafe jafe yi nga xam ne xareb adduna bu njëkk bi ba na leen fi ay goornamaa yu diktaatoor feeñ ci biir tugal ak ci biti leegi nag jeneen jamono ju yees tàmbli ju ngànnaayu muy wutu ngànnaay moo xam ne li ko jur mooy bëgg a fayyu ci reew yii note ci xare bu njëkk bi te toroxal askani reew yi nu not te diisal seen ginaaw ci ay alamaan yu saf te tar lii daal moo sabab xareb adduna bu ñaareel bi li laytaay xare bi àttey diktaatoor yu bees yi sosuwoon man nanu ne ñooy jëfka yi jiitu ci taal ñaareelu xare bi ñu indil la wax ju gàtt ci ñatt ci yi gën a am solo ci noste yooyu nosteg àtte gu mbokkoo rusi mooy reew mi àtteg mbokkoo njëkk a taxaw loolu di woon ci ginaaw fippug oktoobar ga amoon ca atum g li ko waraloon di koom koomam ba daanu woon te ñu dàqoon ko ci anam gu toftaloo ca xare bu njëkk ba ca kanamu almaañ ci ñaari at yii di ak g te mu ñàkkoon it lu tollu ci milyo ak xaaj ci ay xarekatam ca xare booba lenin g mi nekkoon njiitul làngug mbokkte gi parti communiste moo jiite woon fipp googu daal di woon def ag juboo ak waa almaañ yi taxwal it ay jataay yu askan yu barab yi soviets daal di xeetal jumtukaayi ligeey yi taxawal ab goornamaa bu ay ligeeykat aki baykat daal di yëngu ci luy neewal tàqale yi am ci diggante xeet yu wuute yi waa rusi yu sofiet yi taxawaloon nanu ab jë bu yaatu kontar nosteg bopp alal gu soww gi ñu jiite woon kureelub mbokkoo bi kontar diine ak nostey demokraasi yi ñu mujj nag am doole ju mag ak jeexiital gu rëy ci liy xew ci adduna bi yàgg nanoo jëfi jëf ci yekkati tàngoor yi ci adduna bi walla xiiroo ak ngaayoo yi daa am ci adduna bi ci diggante ñaari xare yi nosteg àtte gu nasi ca almaañ làngugug mbokkoo gu xeet gu ligeeykat yi gu nasi gi di parti national socialiste almand des travailleurs gii làngug politig di gu nasi gi daa jariñoo woon profitoo woon ci li daloon waa almaañ yi te wàcci ci seen kaw ci toroxte ak doyadal ak suufeel te li ko waraloon di tënk tënk yi nekkoon ci kollareg versailles gi ak jafe jafe yi mu leen indil ak ñàkk gi leen wër peek leen ak ñàkk ligeey gi ak deltu ginaawug koom koom bi nga xam ne saxoon na fi ay at ginaaw xare bu njëkk bi làng gii nag jariñu woon na ci lii lepp ngir fitali ca àtte ga l état teg ko loxo nangu ko ci njiitug adolf hitler g mi nga xam ne bindoon na dali làngam googu ci teereeb xeexam ba dal yooyu nag danoo taxawoon ci ay cëslaayi waaso ndax daa gëmon ne waasow jermaan mooy waawo wi gën ci waaso yi te it daa gëmoon ne danoo war a sos ag almaañ gu mag gu ëmb mbooleem waa almaañ yi gëmoon it ne àtte gi l état daa war a teg loxo mbooleem lonkoo yu rënk yu mag yi ci almaañ te danoo war a neenal kollare ga nu fasoon ca versailles te danoo war a delloosi mbooleem sancu yi kollare googu ñàkkloo woon almaañ hitler mujj na di njiilul almaañ loo xam ne daa amoon sañ sañ bu joyu pouvoir absolu ñu mujj di ko wooye fuhrer mu tàmbli nag di doxal dali làngam yooyu ci askanu almaañ wi nga xam ne àndoon na ak moom ngir bëgg a mucc te xettaliku ci nekkiin wu bon wi mu nekke woon rawati na ñàkk ligeey gi nga xam ne yaatu woon na lool ci almaañ ngir xare bi ak ngir tënk tënk yi nga xam ne kollareg versailles gi indi woon na leen fi hitler def na ay jëf yu bari yoo xam ne ñoo fi sabab ñaareelu xare bi ndax daa jëloon diiwaanu saar boole ko ci almaañ atum g neenal kollareg versailles jox sodaar si ngànnaay yu diis te xereñ jëmale endustri bu almaañ ci ligeey ngànnaay ak jumtukaayi xare aki bagaas yu ame solos xare mu jëlati reew yiy wax làkkuw almaañ wi boole leen ci almaañ daal di taxawal rayix bu ñatteel bi mu booleeti otris ci almaañ atum g jëlati goxub sodit bi nekk ci cekoslaawi atum g daal di jeem a nangu yoonu danseg ci doole seddoo ak rusi poloñ almaañ nag dundoon na ci ron àtteg nasi la ko dale ca g ba bi mu daanoo tas ci atum g nosteg àtte gu fasi ca itaali waa itaali yi yëgoon nanu te ñoom kat ci reew yi amoon ndam lanu woon ci xareb adduna bu njëkk bi yëgoon nanu ne danu leen a naxe ca ndajem jàmm ma amoon ca paris màngiit yi juge woon ci xare bi it lu neew lanu leen ci jox te kat ñoom ñu ci sonne lanu ag ñàkk ligeey tas ci itaali nekkiinu nit ñi ñaaw làngi politig yi fees fa dell reew ma jaxasoo xalaat yi tas fa di mbokkte communisme fasi ak yeneen xalaat yi fasi nag lu fi ñëwoon la ngir xeex mbokkte benito mussolini jiite ko mi jiite woon ag làngam g làng googu nag danoo warlu woon ci seeni dal principes xeex mbokkte taxawal ag nosteg dimblante te jeem a jot ci ngañaayi sanc yi nga xam ne danu leen a xañoon itaali ca ndajem paris ma ci noonu làngug fasi gi tàmbli di jëfandikoo fitna violence ci xeex ak xuloowaaleem yi bi dégug làng gi gënee dëgër gën a ñaw mu gën a am doole ci la mussolini ak àndandoom yiy solsimis yu ñuul xuppe goornamaab itaali bi ci noonu buurub itaali bi di victor emmanuel amatul woon pexe mu daal di jox nguur gi kii di mussoliini mi nga xam ne mujj na di diktaatooru itaati ñu ko daa dàkkantale dotsi mussolini digale na ñu neenal làng yi aaye askanu itaali wi ñuy def yëngu yëngu mbaa coow nos endustri bi dëppale diggante njariñi ligeeykat bi ak naatug walla jëm kanamug endustriy yaxantu yi daal di juboo ak paab bi delloosi njàggalem diine mi ci jàngu yi leekol yi mussolini feeñal na mbonam gi ak mbonug làngam gi jaare ko ci jëfam yu ñaaw yi mu jëmale woon ci askanu libi wi ba mu fa bëggee samp sancug itaali gi mu gënoon a yaatal ag kilifteefam ca ecopi atum g ginaaw bi ko soldaari itaali yi tegee loxo ci doole nangoo ko ci waa ecopi yaatalug sanc gu itaali gii merloo woon na askan yi nekkoon ci ron ag sancam te taxoon na yeneen reewi sancaan yi kontar ko ci loolu lii nag mooy li jegeele diggante nasi ak fasi nga xam ne mujj nanu àgg ci def ag dëppoo ci seen biir mooy taxawal ag tapoo gu xare nu duppee ko diggub berlin rom bokk na ci diktaatoor yii ba tay làngug xare parti militaire gi nekkoon japon ak àtteg franco ga ca espaañ g moom franco mi mujjoon ame nguur gu joyu pouvoir absolu ca espaañ atum g ginaaw xareb ñoñ bu espaañ ba koolute gi askani almaañ yi amoon ak yu itaali yi yu espaañ yi ak yu japon yi ci seeni goornamaay xeet yu ëppaloon yi te teengal dolliku woon na te li ko waraloon di ñàkk gi nostey bopp alal yi ak yu demokraasi yi ñàkkoon kàttan ci jële fi coonab koom koom bii fi amoon ak ñàkk gu tar gii ubale woon tugal gépp ak feneen ci biir jafe jafeb koom koom bi amoon ci adduna bi atum g ñu gënoon koo xame ci turu lamb gu mag gi yeneen jëfka yu sabab xare bi am na fi yeneen jëfka yoy dugg nanu ci li fi indi xare bu ñaareel bi bokk na ci yi ci ëpp solo 	lòtt gi kureelu xeet yi lòttoon ci ñoal jàmmi àdduna bi ginaaw bi ci almaañ ak itaali gennee ak japon 	digg axe yu politig ak xare militaire yi nga xam ne reewi diktaatoor yi taxawaloon nanu leen ci seen biir bu ci mel ne digg bu berlin rom ak bu berlin tokkiyo ak kollarante gu ñàkk a noonu gi amoon ci diggante berlin mosko laata a xareb ñaareel bi di tàkk ci lu tollu ci ay ayu bis yu neew ci geneen wàll gi fraans britani romani poloñ ñoom itam booloo nanu def seenug tapoo nii daal la ñaari dank sosoo dankub digg bi làmboo almaañ itaali japon ak dankub reew yi tapoo walla way tapoo yi di britani fraans romani poloñ benoog sofiet gi ak amerig ci ginaaw bi 	xuloo bi amoon ci diggante reewi balkaan yu yees yi te aju woon ci mbirum dig yi ci seen biir ndaxte amunu woon ay dig yu sax ak xuloo bi amoon te aju woon ci mbirum xeetu nationalisme ndax kat reew yii di yu sosoo ci seddaleg ndaje ma danoo ëmboon lu sakkan ciy xeeti almaañ lu jege juroomi milyoi ay waa almaañ ñu mujjoon bokk ci njabootug poloñ ak cekoslaafi 	masalam yoonu poloñ wi tàqale almaañ ak brusiya te daytaloo ca waaxub danseg bu gore ba libre ña dëkke woon ca yoon woowa ci ay waa almaañ jege woon nanu ci noonu hitler daal di ne day boole yoon woowu ci almaañ looloo fi taalati gilinug xare bi ci adduna bi ndaxte fraans ak britani ñoom danoo daal di woon jàpple poloñ ci noonu hitler daal di joxe ay ndigal ci nu song poloñ ci satumbar atum g ginaaw bi mu gisee ne ànd na ak bennoog sofiet gi itaali ak japon nii daal la sawaras ñaareelu xareb adduna bi tàkke jamono yi nga xam ne xare bi jaar na ci ak lefi xare bi xareb adduna bu ñaareel bi romb na ci ñatti jamono ñooy 	jamono ju ndam yi hitler doon ame ci xare bi mu tàmbli ci g 	jamonoy yamoo équilibre walla li nuy duppee at mu jaxasoo mi di woon atum g 	jamonoy nërméelu ñeel réewi digg yi mu tàmbli ci atum g hitler yëgaloon na poloñ atum g ne ko manul ñàkk mu génne loxoom ci waaxub danseg bi te delloo almaañ yoonu poloñ wi romboon ci suufus almaañ boobu lëj lëj bokkoon na ci li juddoo woon ca ndajem jàmm ma mooy li fi taalati xare bi ci adduna ndax mooy sabab bu jonjoo bi ko jafal hitler yamul rekk ci yonnee ag xupp jëme ca poloñ waaye da ca a rax dolli yabal ay soldaaram ñu song ko teg loxo ay suufam bi mu lànkee bañ a wuyyu wooteb almaañ bi bañ a faale xuppam gi bi mu kodefee britani ak fraans jug yonnee ag xupp jëme ca almaañ ne ko na génn suufus poloñ si ci diir bu weesuwul ñaar fukk ak ñeenti waxtu bi almaañ lànkee bañ leen a déglu la ko britani ak fraans song ci satumbar g almaañ jot naa teg loxo waaxub danseg ak yoonu poloñ wi ak lenn ci goxi soww yu poloñ yi ag dëppoo am ci diggante almaañ rusi gu waral ñu séddoo ñoom ñaar suufus poloñ si loolu nag di bi rusi tegee loxo goxi penku yu poloñ yi daal di def ak almaañ kollareg ñàkk a noonu non agresssion di gi amoon ci ut g waa almaañ wéy ci seen xare bi daal di nangu danmark ak norwej atum g ginaaw ba nu fa dàqee dooley britani ji ak ju fraans ja fa nekkoon ci geneen wàll rusi moom gën na a tàllal ay tànkam ci finland loolu nag mu jaare ko ca kollareg ñàkk a noonu gi mu fasante woon ak almaañ almaañ daal di song luksamburg nangu ko ci lu yéeme cig gaaw songati holand nangooti ko song beljig nangu ko waaye ci ginaaw xare bu saf sàpp bu mujjoon waral deltu ginaawug dooley britani ji ak ju fraans ji atum g dooley jañ ak naj gi almaañ doon def ci bëj gànnaaru fraans gënoon a dolliku gën a tar ci noonu goornamaab fraans bi daal di tuxoo paris dem bordeau foofa lanu tàmbli woon a sàkku ag wéer ngànnaay ak almaañ ci noonu general deegol daw làqu ca london fa la doon jiitee jànkoonte resistance gu fraans gi kontar réewi digg yi fa la birale it ag fraans gu gore gu ànd ak réewi tapoo yi les alliés goornamaab fraans bi diriku woon ba bordoo daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak almaañ muy gu mel ne ga almaañ defoon ag réewi dëppoo ya ca g wéer ngànnaay gi nag lii la wax 	almaañ nangu bëj gànnaaru fraans péey ba di paris bokk ca ak mbooleem tefesi fraans yi tiim mbàmbulaanug atlas gi 	fraans day fay almaañ ay alamaan yu alal yu tollu ne ferey soldaari almaañ yi nangu fraans 	limub soldaari fraans yi dootul weesu téeméeri junniy soldaar 	taxawal goornamaa bu fraans buy ànd ak almaañ bii goornamaa nag taxawoon na ci njiitug marsal bitan ñu duppee woon ko goornamaab fishi ngir nekk ga mu fa nekkoon ginaaw bi fraans wommatoo meruw almaañ itaali wi dafa sottiku woon ci kaw britani bu ko defee fafalnaaw yu almaañ yi jog def lòkki yu toftaloo ci kaw dëkki britani yi la ko dale ca ut g waa almaañ ñi nag li nu jublu woon ci loolu mooy manante britani ci wommatu cig wàll ak waaj ngir wàcce ay dooley almaañ ca duni britani ya ci geneen wàll waaye taxaw gi askanu britani wi taxaw taxawaay bu dëgër te sax moo tax ba waa almaañ ñi manuñu woon a am li nu bëgg réewi tapoo yi tàmbli woon nanoo ndàmmi ndam di xaw a kawe réewi digg yi as lëf bi amerig duggsee ci xare bi ànd ak ñoom atum g ni ci bennoog sofiet gi dugge dooley britani yi nag ndàmm nanu ndam lu mag ci jë bu afrig bi ci kaw dooley itaali yi daal di leen dàqe ca ecopi ak eriteri looloo taxoon hitler yabaloon ñaari kuréeli xare yu almaañ ca bëj gànnaaru afrig marshal rommell jiite woon leen ngir xettali ji àndandoom ba ca afrig ab xeex bu saf am ca bëj gànnaaru afrig ca nowambar g ci diggante réewi tapoo yi ak yu digg yi ci njiitug mongomeri mi jiite woon réewi tapoo yi ak romal mi jiite woon réewi digg yi ci noonu réewi tapoo yi ndamu ci kaw yu digg yi ca xeex ba nuy wax alamayni ginaaw xeexub ñukkaakon tank char bu mag bu sax fukki fan ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xeex bii nanu ci tudd 	teg loxo gi réewi tapoo yi tegoon loxo goxi bëj gànnaaru afrig ginaaw bi nu fa dàqee dooley itaali ji ak ju almaañ ji 	itaali wommatu na soldaari réewi tapoo yi wàcc ca sisil ñu daal di daaneel nosteg mussolini gi ca satumbar g 	nosub xare bi mujj na nekk ci loxol way tapoo yi ginaaw bi mu nekkee ci loxol almaañ ak réewi digg yi àggoon nanu nag ci seen njòbbaxtali ndam atum g ndamul réewi tapoo yi ginaaw bi dooley britani yi ak yu amerig yi lijjantee ba am ndam ca jë ba ca afrig ak ginaaw bi mussoolini daanoo la réewi tapoo yi fasoon yéenee jële fi almaañ ñu wàcce woon soldaar su dul jeex ca tefesug normandi ga àggoon nanu cib lim ñaari milyoi nit daanaka ñu tegoon leen nag ci kilifteefug generalu amerig bii di dwaayet asinhawar bu ko defee yii doole daal di teg loxo fraans beljig holand suuf yu xóot yi dooley almaañ yi xëyoon nanu wëlbati një cig deltu ginaaw jëme almaañ waaye dooley tapoo yi mayuñu leen woon fu nu yakke seen nàkka ngir ragal ñu jekkaat ba amaat doole ju nuy songeeti kenn ci noonu ñu dab leen ca saa sa jot a sutuxlu ca digi almaañ yu soww ya ca fewriye g ruus yi nag ñoom jotoon nanoo jéego jéego yu am solo ci jëwub penku bi ci goxi penkub tugal bi ginaaw ba fa dooley almaañ yi jugee ci noonu ñu nangu jëwub tugal gu penku gi ci suwe g ci nii daal la dooley almaañ tàbbee ciy xat xat yu jafe ci kanamu doole yu rëyub lim te nu waajal leen ci ngànnaay yi mujj a génn bu ko defee almaañ xëy di ku ñu gaw ci diggante ñaari wàlli kuur ci diggante penku ak soww looloo juroon almaañ faroon wommatu ci mujjantal gi ci me atum g ñu daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak réewi tapoo yi loolu mujj di li taxawal dooley xare ju almaañ jii jot a miiral adduna bi sonnal ko ngir xareem yu bari yii leegi nag réewi tapoo yi di angalteer fraans bennoog sofiet ak amerig nangu nanu berlin péeyub almaañ jàmmaarloo gi waa almaañ yi doon def ak a dàkku seenub dëkk taxaw te jeex wommatug japon waa amerig yi yanoon nanu seen bopp coonab xare bi ci penku kontar japon ginaaw bi waa amerig nangoo suuf yu bari ci li japon tegoon loxo ci xare bi lanu dogu woon ci gañe xeex bi ginaaw bi nu jotee fent bombub fepp bombe atomique te bëgg a xam li mu man te bëggoon it japon wommatoo ci seeni loxo ñu daal di jug ci ut sànni ñaari jum yu fepp ci ñaari dëkk ci japon ñooy irosima ak nagasaki ci noonu japon mujj wommatu daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak waa amerig yi ci turu réewi tapoo yi ci satumbar g bu ko defee ñaareelu xare bi daal di jeex li juddoo ci ñaareelu xareb adduna bi ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xareb adduna bu ñaareel bi bokk na ci yooyu 	def ndajem botsdam ca anéeru berlin ca sulye g ngir jeexal xeex bi britani teewe woon na ko fraans bennoog sofiet gi ak diiwaani amerig yu bennoo yi 	dagg goxub brusiya ci almaa ñ gu penku gi bu ko defee bennoog sofiet gi jël ca wàllug bëj gànnaar ga poloñ jël wàllug bëj saalum ga ñu joxati poloñ dëkkub danseg bu gore bi waaxub danseg 	séddale almaañ def ko ñeenti barabi sañ sañ ci diggante amerig britani fraans ak bennoog sofiet ci atum g la njëkk a am ci taarixu almaañ ñaari reew sosu ci almaañ te yor ag nosteg pénc systeme republicain walla tosteg askan ñooy almaañ gu soww gi walla péncum almaañ mu bennoo mi la république fédérale d allemagne nekk nag ci ron saytug amerig britani ak fraans bon di péey bi geneen gi di almaañug penku gi brusiya gu njëkk ga walla almaañ gu demokraasi gi la république démocratique allemande bennoog sofiet gi saytu ko berlin gu penku gi dib péeyam ñu fàttali leen rekk ne amerig britani ak fraans mujjoon nanoo may almaañ atum mu wut ay soldaar 	almaañ ñàkk na mbooloom xareem bu dëgër ma te rëy ñàkk ngànnaayam yu bees ya te jëm kanam bi nu tasee ab xareem neewal dooleem 	tegoon nanu almaañ mu war a fay li mu yàqal rewi tapoo yi 	nosaat koom koomu almaañ bi rawati na nosteg alal gi ak gu endustri gi yooyu yépp ñu jëme leen leegi ci luy ligéeyal mbiri yi dul xare 	séddale otris def ko ñeenti barabi sañ sañ ci diggante britani amerig fraans ak bennoog sofiet otris it des ci ron teg loxog réewi tapoo yi ba ci atum g ak doonte réewi tapoo yi nangu woon nanu ne réew la mu temb dale ko ca atum g 	réewi tapoo yi nangoo nanu ci japon dun yu am solo bu ci mel ne farmosa ak sakalin añs rafleel ko ci mbooleem moomeelam yi nekkoon ci màmbulaan gu atlas gi dooley amerig yi nag juge nanu japon atum g ginaaw bi nu xaatimee ag kollareg wéer ngànnaay cis een digganteek goornamaab japon bic i dëkkub san fransisko 	xaatim nanu ag juboo ak itaali bulgari romani ak hongri atum g gii juboo nag li mu yaxal mooy réew yii warloo fay réewi tapoo yi ay alamaani xare 	 deltu ginaawug ñaari réew yii di fraans ak britani ci nekk gi nu nekkoon ay réewi adduna yu mag ci ginaaw xare bi bu ko defee amerig ak sofyet yi jël seen barab mujj it di réew yi ëpp doole ci adduna bi mujj yor ngànnaay yu bon te aaytal 	 nërmeelug ñaari noste yii di nasi ak fasi ci tugal ak nosteg xare ga nekkoon japon te noste gu mu ci doon rekk sag am bokk na ci li fi indi ñaareelu xare bi nostey diktaatoor yooyu bokkoon nanu ci nooni mbokkte yi gën a mag 	 feeñug dankub mbokkoo bi bloc socialiste ay réew yu bari bokk ci bennoog sofuet gi jiite ko mu ci mel ne kore gu bëj gànnaar gi wietnaam gu bëj gànnaar gi poloñ bulgari romani cekoslowaki ak hongri añs bu dee nag siin gu askan gi ak yogoslawi nag ñoom ñaar ay réeyi mbokkoo lanu waaye nekkunu woon ci ron yilifug bennoog sofiet dankub bopp alal bu gore bi it feeñ amerig jiite ko làmboo nag réewi tugal gu soww gi niki britani fraans almaañ gu soww gi holand beljig danmark ak norwej añs amerig it warlul yii réew ndimbalug alal ak gu xare ngir ñu man a taxaw ci kanamu dankub mbokkoo bi 	 sos tapoog càmmooñu atlas otan atum g mooy tapoo gi boole woon amerig britani fraans kanada réewi sowwub tugal bi japon ak turki réew yii nag danu ne woon ku ci song menn rekk song nga yeneen yepp ñu kollarante woon ci seen biir ci dimblante ci wàllug aaru koom koom ak alal ci geneen wàll tapoog warsaw gi daal di taxaw tukkee ci bennoog sofiet ak réewi mbokkoo yi topp ci ginaawam ci càmmooñu tugal ak penkoom 	 jëya ju rëy ji juddoo ci xeex bi muy faatug lu sakkan ci dooomu aadama ak yàqug alal ju dul jeex ngir jumtukaayi xare yu xereñ yi nu ci jëfandikoo ñuy jum yi les missiles bombi fepp yi nuuraakon yi ak ñukkaakon yu diis yi ans xare bii moo ëpp lu mu yàq ray ko màbb ko ca moomam ja ko fi jiitu woon 	 ëttu àtte yu normbrug yi ngir àtte ñoñ nasi ñi ci tuumay jqi fitna ak sabab xare bi ak def ay tooñaange jëme ci ñu ñu tëj ñi les prisonniers ak ñi ñu njafe ca reewi tapoo ya àtte nanu fa tam njiiti nosteg xare gi nekkoon japon 	 juddug mbootaayu xeet yi ngir dëgëral jàmm ak tere xare yi ak xulooy réew yi ak amal mbaandute ak yamoo ci réewi adduna bi 	 koom koomu àdduna bépp a naatoon ginaaw bi xare bi jàllee li ko waraloon di naali tabax yeek yeneen yi nga xam ne defaraat dëkk yi la doon ligeeye ak wàllug tabax ci anamam yepp bi gënoon a rëy ci naal yooyu mooy bu marsaal 	 judduwaatug joante ci ngànnaay ci diggante ñaari dank yi bu mbokkoo ak bu bopp alal ak sosu gi xare bu sedd bi sosu ci seen diggante naka noonu dund ci jàmm gi am leegi ci diggante xeet yi ci kaw suuf doggantal gu ñaareel gi mbootaay yu adduna yi kureelug xeet yi mbootaayu xeet yi walla xeet yu bennoo yi mbootaayug reewi lislaam yi walla mbootaayu daje gu lislaam gi ñatti mbootaay lanu bëgg a waxtaane ci doggantal gii ñooy kureelu xeet yi mbootaayu xeet yi mbootaayu reewi jullit ñi kureelu xeet yi njiitul amerig la tuddoon widro wilson da doon ku daa xalaat nu mu fiy taxawale mbootaay gu mag gu adduna bi guy jeem a indi jàmm ci adduna bi ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi waxoon nanu ne wilson moom jotoon na a leeral dalam yooyu nga xam ne fukk lanu woon ak ñeent ci biir xeexub adduna bu njëkk bi ne woon daal fàwwu nu sukkandiku ci ñoom ngir taxawal xeex bi ak ngir rëddaat sëqooy reew yi teg leen ci dàtti jàmm ju sax ak moytu xeex yi nar a amati wilson moom gaaraloon na naalam boobu di kureelu xeet yi gaaraloon na ko ca waxtaanu jàmm wa nu amaloon kollëre ga nu jotoon a fas ca versaay it moo rëddoon lanu fa xaatim lii di ñew di nanu ci leeral li ëpp solo ciy poñ yu nekk ci kollëre gi taxawal kureelu xeet yi 	sose kureelu xeet yi ci mbooleem reew yi am tmb gu mat gu dara wàññiwut reew yoo xam ne man nanoo indi ay warlu yu mat ci respekte walla wormaal jàmm te bàyyi xeex mbaa lu koy waral 	reew yi bokk ci kureel gi dananu warlu ne kenn du ci xeex ak kenn te gaaralul li ko tax a bëgg a xeex ci kureel gi ngir nu àtte leen te xool li leen boole reew yi ci bokk it war nanuy seet mbugal yi yell ci reew yiy tooñ yu ci mel ne teg leen ay gaw yu koom koom walla jëfandikoo doole ci seen kaw 	jeem a dëgëral buumi dimblante ci adduna bi jaare ko ci sukkandiku ci maslaa gu fés ak wormaal kollërantey reew yi ak xeex njaam ci meloom yepp jeem a rafetal nekkiinu ligeeykat yi ak seenug dund ak xeex dorog nos yaxantu ci adduna bi ak sonn ci wér gu yaramu nit 	reew yi ci bokk dananu warlul yeneen reew yi wormaal seenug tembteg politig dananu warlu it bañ a def ay kollërey sekkare ak jox kooluteg kureel bi ab day ci mbooleem kollërante yi reew yiy def ci seen diggante koolute gi nag di secretariat bi ci dëkkub geneve bi nekk siwis la nekk 	aar neewtey xeet yi ak yu diine yi nekk ci mbooleem reew yi ak wormaalal askan yi ak xeet yi nekkoon ci ron imbraatoor yi wormaalal leen seen àq ak sañ sañ ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg te gis ne moo gën ci ñoom ak reew yi nu gañee ci xareb adduna bu njëkk bi 	kureel bi mooy taxaw ci di xool ni nuy doxale nosteg féetale gi mooy noste googu nga xam ne moo waraloon yenn ci askan yi xeet yi ak mbooloo yi nu feetale leen reewi sancaan yu mag yi teg leen ci seen ron kilitfeef ak doxaliin ginaaw bi reew yooyu nekkee ci waawug reew yi nu gañee woon ci xeex bi ñuy reewum usmaan mi imbratooru otris gi ak gu almaañ gi loolu nag nu defoon ko ngir waajale leen ci ba man leen a may ag tmb ëlëg kureel bi bi muy door a sosu reew a ca bokksi woon ci noonu reew yiy temb di gën a dolliku naka noonu di gën a bokksi ba mujj limub reew yi bokk àgg ci juroom benn fukk mu ci nekk it am genn kàddu ci bu nuy woote kollëreg kureel gi jox na reew mu nekk àq ak sañ sañ ci mu genn ne bokkatuma waaye ci kaw reew moomu teel a yëgale ag bëgg a bàyyeem lu tollook ñaari at cig njëkk bànqaasi kureelu xeet yi kureelu xeet yi ñatti bànqaas yu mag la am ñooy jataay bu matale bi jataayub kureel bi koolute gi walla secretariat nga rax ci dolli ñaari bànqaas yu ci bànqaasoo ñooy àttekaayu maanduteg adduna bi ak mbootaayug ligeey gu adduna bi jataay bu matale bi mi ngi daa ame ci mbooleem ndawi reew yi bokk ci kureel bi ab dajeem it benn yoon la daa am ci at mi ci weeru sëtumbar ngir xool ak xalaat ci mbooleem xew xew ak mbir yu am solo yi nekk ci ay prograamam jataayub kureel bi moom mi ngi sosoo woon ci njëlbeen gi ci juroom ñeenti cer juroom yi ci juroom ñeent yooyu ñooy reew yi am ag bokk gu sax ñooy britani frans itaali japon ak almaañ mi jël cerub amerig mi nga xam ne bokkutoon ci kureel bi ak yeneen ñeenti reew yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn leeg leeg bii jataay nag dana faral di daje ñatti yoon ba ñeent ci at mi dana faral di daje it ci anamug jagle ci xew xew yu bette yu man a xupp jàmmi adduna bi limub toogu yu sax yi tam yokk na ci jataay bi juge ci ñeenti toogu dem ci juroom ñeent koolute gi secretariat koolute walla secretariat bu kureelug xeet yi mi ngi sosoo woon ci ligeeykat yu kureel bi ya daa ligeeye ca dalam bu sax ba nekkoon geneve njiit li moom moo daa doon ku nu woolu ku matale ki nga xam ne jataay bu matale bi moo ko daa tànn koolute gi nag amoon na ay kureel yu bari yu aju woon ci moom ñooy kureelug dimblanteg aada gi kureelug jële fi ag njaam kureelug xeex dorog kureelug aar neewte yi kureelug féetale yu sax yi ak kureelug tawat yu bon yi am na yeneen bànqaas yu am ag jokkoo ak kureelu xeet yi ñooy yu mel ne àttekaayu maanduteg adduna bi ligeeyam di àtte xuloo yi ak amlante yi àttee ko nag ci yoon walla luwa bu àdduna bi ak kollërante yi reew yiy xuloo jotoon a def nosteg kureel bi nag li mu wax mooy àttekaay bi fukk ak juroomi àttekat ñoo koy taxawal yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn tànne leen nag ci kandidaa yi nga xam ne reewi kureel bee leen di ind àttekaayub maanduteg adduna bi moom mi ngi sosu ci atum g ab dalam it nekk lahaay ca holand ak mbootaayug ligeeyub adduna bi ligeeyam di yewenal nekkiinu ligeeykat yi ci adduna bi ak yekkati seen tolluwaayu dund moom nag mi ngi booloowoo ci ndawi ligeeykat yi ak sendikaay ligeeykat yi ak boroom ligeey yi geneve nag moo dib dalam ayibi kureelu xeet yi kureeb xeet yi de ak li mu def lepp ci ligeey yu jëm ci saxal jàmm ci adduna bi ci biir fukki at yu njëkk yi ak li mu fi def ci ligeey yu am njariñ ci wàllug mboolaay loolu lepp teewul mu lottoon te ñakk kàttan ci lijënti xuloo ak ngaayoo yi da a am ci diggante reew yu mag yi loolu nag waraloon na neew dooleg kureelu xeet yi rawati na ci atum g bi nga xame ne ag lottam àgg na ci manatul a tee reew yu mag yi di noggatu yu ndaw yi lu mel ni loolu moo xewoon bi japon defee ay jalgati jëme ko siin li ko gënoon a doyadil mooy genn gu ci japon ak almaañ gennoon atum g ak lott gu mu lottoon ci tee itaali songu ecopi atum g loolu sax moo taxoon mu genn ci kureel bi atum g kureel bi ba tay demoon na ba manatul woon a tee ay dank yu xare yu bees di am maanaam ay reew dajaloo boole seen bopp ci wàlli xare kureel bi tam àggoon na ci manatuloon a tee reew yu mag yi di rewante ci ngànnaayu yi ci bokk ci kureel bi ak yi ci genn bokk na ci ayibi kureel bi fent gu ñeenti reew yu mag yi fentoon nosteg feetate ngir may britani ak frans nu man a sancati walla koloniiseeti ay suuf yu bees yoo xam ne danoo juboo woon ci seddoo leen ci seen biir rawati na ci reewi araab yi ak yu dul ñoom yenn yi ci yooyu danoo nekkoon ci ron kilifteefug reewum usmaan mi yi ci des ci waawug imbraatoorub almaañ bi reew yu mag yii dano o jëloon seen xemmemteefi sancaan yooyu cuub leen ci cuubug ag nite ak bëgg a def lu baax bi nu waxee ne kureelub xeet yi daal mooy kilifa gu njëkk gi yilif reew yu neew doole yi muccoon ci kilifteefug tirki ak almaañ bokk na ci ayibi kureel bi ba tay aakimoo gi reew yu mag yi aakimoo woon mbooleem saxal yi ak mbir yi nu daa gaaral ci kureel bi mbootaayu xeet yi walla xeet yu bennoo yi ndawi reew yu mag yi yu ci mel ni britani diiwaan yu bennoo yi amerig bennog sofyet frans ak siin danoo daje woon ci wasington peeyub amerig ci wenn waxtaan atum g ginaaw bi as lëf ci ndam tàmblee feeñ ñeel reewi tapoo yi ci noonu nu gëstu woon nan lanu fiy sose ag mbootaay gu adduna guy yëngu ci saxal ponki jàmm ci adduna bi jële fi xeex yi amal fi maandute ak yamoo ci diggante mbooleem reew yi ak rafetal nekkiinu mboolaayu reew yi ci koom koom mboolaay aada ak wér bi loolu jàllee nu def benn dajeb waxtaan bu adduna bi ci dëkku san fransisko ci awril atum ngir rëdd fa ag kollëre ñeel ag mbootaayug xeet gu yees gu fiy wuutu kureelu xeet yi ndawi lu tollook juroom fukk ak benni reew teewe nanu ko nangu it ci nu def kollëreg mbootaayu xeet yi ak xaatim ko ci g la jiitu ca kollëre ga mooy jubluwaayi mbootaayu xeet yi ak ay ker keraanam kollëreg mbootaayu xeet yi dafa saxal ay jubluwaayam ci ñeenti mbir yu dàttu ñooy 	wattu jàmm ak kaaraangey adduna bi 	suuxat seqooy cofeel yi ci diggante reew yi 	gën a soññ dimblante gi am ci diggante reew yi ci mbiri koom koom ak mboolaay ak aada ak wàllug nit 	dëppale jëfi xeet yi walla reew yi walla jëmale leen ci lu dëppoo ak li mbootaayu xeet yi bëgg bu dee ker keraan yi mbootaay giy jëfandikoo ngir àgg ci jubluwaay yooyu moom mbootaay gi leerale na leen ci nii 	bennoog askan yu moom seen bopp yi ngir ñoal jàmm ak kaaraangey adduna bi 	di jëf ci anamug jàmm ak baalante ak jéllale ci diggante reew yi 	warlu yoon yi man a yobboo ci nu bàyyi jëfandikoo doole ci bu nuy lijanti jafe jafe yi ci adduna bi ndare bu loolu day li gën ci adduna bi 	sukkandiku ci campeefi adduna yi ngir dëgëral jëm kanamug koom koom ak gu mboolaay gu askan yi campeefi mbootayu xeet yi aki jumtukaayam mbootaayu xeet yi mi ngi ame ci ñatti campeef yu mag ñooy jataay bu matale bi mi ngi sosoo ci mbooleem reew yi bokk ci mbootaay gi mu ci nekk it am na genn kàddu bu niy woote jataay bi da na daje benn yoon ci at mi ci weeru satumbar ca dalam ba ca new york man na a am nag leeg leeg ñu amal jataay bi ci xew xew yu bette yi ko aajowoo jataay bu matale bi nag yii ñooy ay yiteem 	gëstu naal yi ko reew yi ci bokk di faral a indil ak saxal leen ak def ndinkaane yi war ngir jàmmi adduna bi 	gëstu mbir yi nga xam ne man nanoo yokk anami dimblante ci adduna bi 	nangu bokkug reew yu bees yi bëgg a bokk 	tànn cer yu saxul yi ci jataayub kaaraange gi 	tànn àttekati àttekaayu maanduteg adduna bi ak ceri ñaari jataay yi bu koom koom bi ak bu mboolaay gi ak jataayub ndenkaane bi saxal yi jataay bu matale bi daa faral di jël ñi ngi daa ame ci ndollant gu toll ci ñaari ñatteeli cer yu fekke woote bu nuy def ci naal bu mu man a doon walla ab ndenkaane jaataayu kaaraange gi jataayub kaarange gi mi ngi sosoo ci juroomi cer yu sax ñooy ndawi diiwaani amerig yu bennoo yi usa ak bennog sofyet gi ak nguur gu bennoo gi ak frans ak siin ak yeneen fukki cer yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn ngir diirub ñaari at cer yu sax yi nag dananu am sañ sañu firi lepp lu nu fas ca jataay ba boobu sañ sañ ñu koy woowe veto jataay bi nag dana daje ci anam gu sax ngir xool ci mbir ak xuloo yu adduna bi yi nga xam ne man nanoo jur njombe saxal yu jataay bi ñi ngi ame ci ndollant gu toll ci juroom ñeenti kàddu ci cosaanul fukki kàddu ak juroom maanaam saxal gi du man a wér mbaa mu wéy ndare bu juroom ñeent danoo kàddoo waaw la ca des ne deet walla ñu noppi waaye nag benn saxal du am njariñ bu ko benn cer bu sax firee ne àndu ci jataayub kaaraange gi moo ame kureel biy saytu kàttanug fepp gi am na it sañ sañ ci genne ay saxal yu aju ci taxawal xeex yiy am ci diggante ñaari reew ak tege ay mbugali koom koom ak yu xare ci mbooleem reew yi dul dégg ndigalam am na sañ sañu yabal ay doole it ngir taxawal ab xeex walla ay kureeli soldaar ngir ñu dox diggante ñaari reew yu nar a xeex koolute gu matale gi moom jumtukaay la bu moo uuf mbooleem ñiy ligeeye ci mbootaayu xeet yi koolute gi ki koy jiite mooy ku nu woolu kiy jiite mbootaay gi nga xam ne jataayub kaaraange gi moo koy tànnlu bu ko defee ñu gaaral mbir mi ci jataay bu matale bi ngir nu woote ko kàddu ko dalub koolute gi mi ngi new york ci biir koolute googu lanuy denc mbooleem dosyeey mbootaay gi campeef ak bànqaasi mbootaayu xeet yi am na ay campeef aki bànqaas yu aju ci mbootaay gi ñooy jataayub koom koom ak mboolaay bii jataay a ngi ame ci cer yu seen xam xam aju ci mbirum koom koom ak mboolaay jataay bu matale bi moo leen di fal ngir diirub ñatti at jataay bii nag li nu ko wékk mooy gëstu mbiri koom koom yi ak mboolaay yi ak aada ak lu aju ci nit mbootaayi adduna yii ma lay bëgg a leeral ci jataay bii lanu bànqaasoo moom mbootaay guy jagoo mbiri aada yi la ak xam xam ak yar dalam bu sax ma nga paris ca frans yiteem nag mooy dëgëral dimbalante ci wàllug xam xam ak aada ak yar ci diiggante reew yi ci bokk jaare ko ci soññ ak sawarloo gëstu ak ligeey yi aju ci yar ak aada ak xam xam yi mbootaayu ligeeyu adduna bi li nekk yiteem mooy rafetal dundiinu ligeeykat yi ci adduna bi ak fexe nu yokk seeni ngérte moom nag mbootaay gi mi ngi ame ci ab lim ci ndawi ligeeykat yi ak boroom ligeey yi ci mboooleem reewi adduna bi ab dalam nag mi ngi nekk geneve mbootaayug wérug adduna bi mbootaay la guy sonn ci dimbali reew yiy màgg ci ñu man a xeex tawat yiy wàlle te yekkati seen tottuwaayu wér gu yaram moom mbootaay gi nag dana def ay gëstu ci wàllug wér di ci sàkku it xam xam yi manul a ñàkk di yonni ay boroom xam xam ci loolu di nos ay prograam yu jagoo tàggat ñi yittewoo wallug wér ab dalam nag ma nga geneve moom itam mbootaayu dund ak mbay gu adduna bi moom nag liy ligeeyam mooy jeem a def ay pexe ci nu niy yokke li nuy ligeey cib dund ci ñatteelu adduna bi loolu nag nu jaare ko ci jëme kanam mbay mi te yokk jumtukaayam aki ker keraanam ak xeex gàkk gàkki mbay yi ak yu dundat yi ak dox ci lu fi man a indi ag mottalikoonte gu dund ci adduna bi dalam bu sax bi nag mi ngi rom ca itaali ëttu àtte bu maandute gu kawe gi moom nag daa mel ne àttekaayu maandute gu adduna bi gi toppoon ci kureelu xeet yi moom daal moom lanuy jàppe kilifa gu wàllug yoon gu mag gi nekk ci mbootaayu xeet yi mi ngi ame nag ci fukk ak juroomi àttekat yu jataay bu matale bi di tànn ak jataayub kaaraange gi ginaaw bu leen seeni reew sampee gaaral leen ci mbootaay gi ligeeyam nag mooy gëstu sabab yi waral xuloo yi ci diggante reew yi mooy kàttan gi ame firi ak leeral kollërante yi reew yiy def ci seen diggante ak àttey yoonu adduna bi ab dalam nag mi ngi lahaay ca holand mbootaayu xeet giy yëngu ci xettali gi ak tabax li miy yittewoo mooy mbiri way daw làqu yi te indil leen ndimbal li manul a ñàkk te dëkkal leen ligeeyloo leen jataayub ndénkaan yi mooy saytu mbirum sancu yi almaañ moomoon itaali ak japon njëkk ñu leen di gañe ci xeexu adduna bu ñaareel bi bii jataay nag moo taxaw taxawaayu jataayu feetale bi nekkoon ci kureelu xeet yi ginaaw xeexu adduna bu njëkk bi bankub addunna bi ngir sos ak tabax bii bank danu koo sosoon ngir man a lebal reew yi ci bokk ak dimble leen ci tabax barab yi xeex bi yàq ak jëmale kanam barab yiy tàmblee màgg ak sos ay naal yoo xam ne man nanoo jàpplee ci màggug koom koomu adduna bi ak jeem a rafetal dundiinu ñi dëkke ci reew yiy màgg banku adduna bi moom dafa mel ni ag lonkoo gu adduna bi goo xam ne boppu alalam mi ngi juge ci li cer yi di teg cer bu nekk nag li muy teg day tolloo ak ni koom koomam toll dalam bu sax nag mi ngi wasington peeyub amerig keesug kee gu adduna bi yitteem mooy saxal njëgu kee gu adduna bi ak dindi fi jafe jafe yi man a juddoo ci wecciku ci diggante reew yi man nanu ne mbootaayu xeet yi daal mbootaal la gu adduna gu am sañ sañ yi kureelu xeet yi amoon waaye mu ëpple kureelu xeet yi ci ñatti mbir yu am solo ñooy 	mbootaayu xeet yi day dëgëral ci ay jubluwaayam àqi ak yelleefi doomu aadama yu dàttu yi ak teddngay nit ak yamale ñaari xeet yi goor ak jigeen cig wàll ak yamale reew yi ci geneen wàll 	mbooleem reew yu mag yi bokk nanu ci mbootaayu xeet yi te bu dee kureelu xeet yi moom amerig bokku ci woon ngir bañ gu kongres bañoon ne du ci bokk te it bennoog sofiet moon bokku ci woon lu dul ci diggante g nga rax ci dolli ne cer yi bokk ci mbootaayug xeet yi boo ñaarte woo cer yi bokkoon ci kureelu xeet yi yu mbootaay gi moo leen di ëpp 	mbootaayu xeet yi am na dooley xare ju koy kàttanal ci mu man a wéyal ay saxalam am na it sañ sañu tege ay dogoo yu koom koom ak jëfandikoo doole jëme reew yiy tooñ ànd ak loolu lepp nag teewul mbootaayu xeet yi moom doon daanaka ab jumtukaay bu nekk ci loxoy reew yu mag yi am ay toogu yu sax ci jataayub kaaraange gi yooyu nga xam ne ñoo ame sañ sañu firi veto man a bañ mbaa firi bepp naal boo xam ne gaaral nanu ko ci jataayub kaaraange gi ci noonu yenn ci reew yu mag yi ftteerlu nanu wéy ci jëfandikoo sañ sañu firi di ko jëfandikoo fu nu ko wart a defe di ci tooñe di ci dumaa di ci aare reew yuy jalgati te lu bari ci saxali jataay bu matale bi ak saxali jataayub kaaraange gi ba leegi daa rekk lanu ci kayit kenn doxalu leen ab ligeeyam nag ci wàllug dimbalnteg koom koom aada wér gu yaram ak mboolaay lu am solo la te yayoo màggal waaye bu dee ci lu aju ci politig ak xare moom dëgg dëgg ni mu ciy doxe sori na dëgg sori maandute te sori yoon mbootaayu reewi jullit yi walla mbootaayu daje gu lislaam gi ag sosam mbootaay gii mi ngi sosu ci saxal goo xam ne buur ak njiiti reewi jullit yi jëloon nanu ko ci waxtaanu seen daje bi nu njëkk a daje te defe woon ko ribaat peeyub reewum marok ci diggante g g deppoo ak g ñaar fukki reewi lislaam ak juroom bokkoon nanu ca waxtaan woowa mbootaayug goreel falastin olp it teewe woon na ko waaye niki aji fuglu rekk ndajem waxtaan moomu mi ngi amoon ci ginaaw bi nu lakkee masjidul aqsaa ci g te ay yahuud def ko waxtaan wa ba muy tëj daa ñaawlu jëf ju bon jooju nga xam ne day wone ag noonu gu nu def jullit ñi te ñàkk a wormaal seeni gëm gëm ñu sàkku woon it ci israayil mu genn ci mbooleem suufi araab yi mu tegoon loxo atum g te delloosi dëkkub quds bi ci ni mu nekke woon ca xareb sue juin ba atum g mu feddali ba tay moom ndaje mi jàpple gu miy jàpple reewi artaab yi ci seen xeex bi nuy def ak israayil ak jàpple gi muy jàpple waa palastin ci nu delloosi seen àq ak yelleef yi nu teg loxo te goreel seeni suuf kollëreg mbootaayu reewi jullit yi kollëreg mbootaay gi mi ngi genne ca ñatteelu waxtaan wa jëwrini bitim reew yu reewi lislaam yi amaloon ca jidda atum gg dëppook g mu sampu woon moom kollëre gi ci li taxoon nu sos mbootaay gi li nekk ci poñ bu njëkk bi ci kollëre gi mooy reew yi ci bokk ñi ngi sos mbootaayug reewi jullit ñi walla mbootaayug daje gu lislaam gi poñ bu ñaareel bi làmboo dali mbootaay gi aki jubluwaayam jubluwaay yooyu nag weesuwunu woon amal fi jawwu ju baax ju nu man a dëgërale dimblante ak deggoo ci diggante reew yi ci bokk ci seen biir ak ci seen diggante ak yeneen reew yi waaye dal yi nag ñoom ci nii lanu taxawe 	yamoo gu mat ci diggante reew yi ci bokk 	wormaal àq ak sañ sañu reew mu ci bokk ci wutal boppam mujj ga ko soob ak bañ a dugg ci mbiri biiram 	wormaal moomeelug reew yi bokk ak seenug temb 	dëgëral dalu dimblante gu lislaam gi ci diggante reew yi bokk 	dëgëral dimblante ci diggante reew yi bokk ci wàlli koom koom mboolaay aada xam xam ak ci yeneen wàll yu am solo yi ak diisoo ak yeneen reew yi bokk ci yeneen mbootaay yi 	jeem a far boddante ci biiru xeet ak sanc ci mbooleem ay anamam 	def lepp lu man a indi jàmm ak kaaraange ci adduna bi ci anamug maandute 	dëppale ak nos ligeey bi reew yi seq ngir njoal barab yu sell yi te goreel leen ak jàple waa falastin ci seen xeex bi ak dimble leen ba nu man a delloosi seen àq ak yelleef te jotaat seen suuf 	jàpple mbooleem reewi jullit yiy xeex ngir njoal seen teddnga jot seen tmbte dollosi seeni yelleefi reew 	lijjanti xuloo yi nar a ami ci diggante reew yi bokk ci mbootaay gi lijjanti loolu ci jàmm niki waxtaan dox diggante ak layoo 	reew yi ci bokk danoo war a bàyyi ci seeni seqoo di jëfandikoo doole walla xuppe ci jëfandikoo ko jëme ko ci suufus reew mu bokk walla jëme ko ag tmbam campeefi mbootaay gi aki kureelam ak jumtukaay yi ci bànqaasoo mbootaay gi sos na ay campeef yu bari yu cosaanu niki 	jataayu buur yi ak njiit yi 	jataayu jëwrini bitim reew yi 	koolute gu matale gi 	àttekaayu maandute bu lislaam bu adduna bi bu dee kureel yi ci bokk nag ñooy 	kureelu quds 	kureel bu sax bi ñeel wàllug koppar 	kureelu lislaam bi saytu wàllug koom mboolaay ak aada 	kureel bu sax bi ñeel dimbalanteg xam xam ak xarala 	kureel bu sax bi ñeel dimblanteg koom ak yaxantu 	kureel bu sax biy yëngu ci wàllug xamale ak aada bu dee nag lu aju ci jumtukaay yeneen yi bànqaasoo ci mbootaay gi ñooy 	keesug dimblante gu lislaam gi 	keesug quds 	daaray gëstu gu lim yi ak koom ak mboolaay 	barabu lislaam biy yëngu ci jàngale mecce ak xarala ak defi gëstu 	 cëslaayu lislaam giy saytu xam xam xarala ak suqli koom koom 	barabu adduna biy yëngu ci yar ak njàngalem lislaam 	barabub lislaam biy sonn ci suqali yaxantu 	kureelu lislaam gi saytu terute gi ci adduna bi 	kureel adduna gi saytu ndono lu lislaam li 	akaademi bu xam xamu lislaam 	jataayu lislaam bi yor tukkib jawwu bu nit ñi 	kureelu lislaam bu adduna bi ñeel yoon bu lii jàllee teewul sosees na ba tay yeneen cëslaay yu bokk ci mbootaay gi ñooy 	banku lislaam bi 	barabu xibaar bu lislaam bu adduna bi 	mbootaayu rajoy reewi jullit yi 	neegub yaxantu bu lislaam bi ak mecce ak joqalanteg njaay yi 	mbootaayu peeyi lislaam yi 	suqali gu lislaam gi jëm ci boroom gaal yi 	mbootaayug lislaam gi jëm ci yar xam xam ak aada jagley campeef yi ak seeni ligeey jataayu buur yi ak njiit yi mooy campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi moom nag dana faral di daje saa su ko yitey xeet wi laajee ngir gëstu ay mbiram ak lijanti ay lëj lëjam buur yi ak njiit yi ci bokk nag saxaloon nanu ca seen ñatteelu ndaje ma nu defoon ca makka mu sell mi ak taayif ci diggante rabihul awal gg dëppook g saxaloon nanu fa ne danuy def ndaje yi ñuy luy wër ci seen diggante ci ñatti at yu nekk niki nu ko waxe woon mbootaay gi ndajeem mu njëkk mi ngi ame woon ribaat diggante gg dëppook g mu defaat meneen ndaje ca lahoor ca pakistaan diggante muharram safar gg dëppook g ñatteelu ndajeem mu defe ko makka ak taayif diggante gg dëppook g mu def ñeenteelu ndajeem ca kaasa balanka ci diggante rabiihu saani gg dëppook g juroomeelu ndajeem ame kuwet ci jumaadas saaniya gg dëppook g jataayu jëwrini bitim reew yi nag mooy ñaareelu campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi ginaaw jataayu buur yeek njiit yi campeef bii nag dana faral di daje ci anam guy wër ci at mu nekk ci benn ci reew yi bokk ngir xool mbooleen bataaxel yiy doxal politigu mbootaay gi ak jël saxal yi war ci mbir yi am ay njariñ yu reewi mbootaay gi bokk loolu lepp nag fekk mu dëppoo ak jubluwaayi mbootaay gi aki bëgg bëggam jataayub jëwrin yi mooy xool saxal gi nga xam ne kureelub koppar bu sax bi di na koy def ngir saxal ko te wéyal ko mooy xool it njël lu yaatu lu kooluteg mbootaay gi bokk na ci ay ligeeyam di sàkku ci mbootaay gi muy daje bu jaadoo ngir ay xew xew yu bette yu yitteel jullit ñi jataayub jawrin yi ba tay dana faral a daje ci anam gu xotti baax saa su ko yitte laajee bu dee koolute gu matale gi nag walla moom mooy campeef biy wéyal jëf yi ci mbootaay gi mi m ngi sosoo ci saxal resolution gu genne woon ca ndajem jëwrini bitim reew ma nu amaloon ca jadda diggante g yiteem nag mooy def ligeey yi nu ko sant ci biir àttey kollëreg mbootaay gi dina dimbli tam yeneen campeef ak bànqaas yi bawoo ci mbootaay gi ak di dëppale seeni prograam yu wuute yi bokk na ci yitteem ba leegi topp ak xeeñtu saxal ak ndenkaane yi tukkee ci ñaari ndaje yii mu mbootaay gi ak mu jëwrin yi kiy saytu ligeeyi koolute gi mooy ku nu wóolu ki nga xam ne mbootaay gee koy fal ngir diirub ñeenti at yees manul a yeesal bu ko defee ñeenti dimblikat ak ñeenti ñu ñu wóolu di ko jàpple kenn ci ñoom jagoo mbirum palastin ak quds mbootaay gi jidda la defandi dalub kooluteem gi ba kero nuy goreel quds insallaa ngir nu def ko dal bu sax bi làkk yi mbootaay giy jëfandikoo ciy ligeeyam ñooy araab franse angle mbootaay gi nag mbirum palastin yitteel na ko lool ak mu quds moom mi nga xam ne moo uuf masjidul aqsa mi yàlla teral te teral li ko wër ak doj wu sell wa ak miir ba nuy wax miiru buraax ak yeneen mbir yi aju ci diiney lislaam te nekk ci mbooleem barabi lislaam yi quds nag boo gisee nu fonk ko day suuf si yonnant bi rañaane woon yeeg loolu nag dana waral ci jullit ñi ñu fonk ko te yittewoo ay mbiram te aar ko ba noon yi dunu ko tilimal kureelub quds mi ngi sosu ci ndigal lu tukkee ci juroom benneelu ndaje mu jëwrini bitim reew yi mi ame woon jidda ci diggante g ndajem jëwrin mu fukkeel ma nu defe woon faas ca marok ci diggante g ndaje moomu dal di denk njiitug kureelu quds bi buuru marok bii di asan mu ñaareel mi ligeey yi nu denk kureel bi mooy yii 	di gëstu lay xew quds 	di topp ak a xeeñtu doxalug saxal yi aju ci quds te jataayub jëwrin yi def leen 	di jokkoo ak mbootaayi adduna bi yi man a dimblee ci aar quds 	di wax ci lu man a doxal saxal yi ci aju 	di indi ag saxal ci at mu nekk guy leeral ay ligeeyam aki jëfam ci jataayu jëwrin yi kureelu quds moom njiit la ko jiite moo ko man a dajeloo walla lu mbootaay gi kureel gi nag mi ngi ame ci ndawi reew yu bokk ci mbootaay gi yoo xam ne jataayu jëwrin yee leen di tànn ngir diirub ñatti at doggantal gu ñatteel gi reew yi def ay dank ak reew yi feetewul fenn ag jiital bokk na ci li gën a rëy ci li juddoo ci xeexu adduna bu ñaareel bi bokk na ci li ci gën a rëy feeñug walla juddug ay dank yu ay reew walla ay booloo yu ay reew ci wàllug politig walla xare ci noonu dankub bopp alal dal di feeñ nee amerig jiite ko mu uuf nag biritani frans ak lu bari ci reewi orobug sowwu gi mbooloo mii nag ñi ngi ko daa woowe dankub sowwu bi ak reewi adduna ju gore ji safaan nag walla wuute ak reewi bokkoo yi bu ko defee amerig moom jug di dimbli reewi dankub sowwu bi ci ngànaay ak xarala ak alal ngir dëgëral seen koom koom te may leen doole ba nu man a taxaw di tata ci kanamu reewi bokkoo yi tee leen a tas tee leen a wisaaroo naka noonu dankub bokoo bi moom itam sosu bennoog sofiet gi jiite ko mu uuf lu sakkan ci reewi bokkoo yi ci tugal gu bëj gànnaar gi ak gu digg gi ak reewi bokkoo yi nekk asi niki kore gu bëj gànnaar gi wietnaamm gu bëj gànnaar gi ak siinug askan gi ñaari dank yii di bu sowwu bi ak bu penku bi xeex nanu ba tàyyi ngir yilif adduna bii nga xam ne sonne na lool ci ñaareelu xeexu adduna bi nga xam ne reewi orob yi sax mujj nanu di reew yu lòtt te neew doole ci kanamu ñaari reew yu mag yii di diwaani amerig yu bennoo yi ak bennoog sofiet gi looloo waraloon gisiin wiy woote ne reew yi ñoo tolloo yamoo ay nawle lanu wii gisiin naaxsaayoon te faf far xajal fi wiy indi doonadi moroom gi amerig ak sofiet doonadi woon moroom ci yeneen reew yi loolu nag taxoon na ba reewi orob yi tàmbli woon a xalaat ci seen ëlëg ginaaw bi nu mujjee di reew yu ñàkk solo bu nu leen tollalee ak yile ñaari reew ginaaw ñaareelu xeex bi it yeneen reew feeñ nanu ñu leen di woowe reew yiy màgg yi ci ëpp nag ñooy reewi asi ak afrig yi doon door a tembe ci reewi sancaan yu orob yi reew yooyu tam danku nanu ngir taxawal dankub reew yi feetewul fenn ne li niy def mooy fas yeenee ame ag peeteedi gu rafet ci diggante ñaari reew yu mag yi ak yi nekk ci seeni ngunu dananu leen leeral ci lii di ñëw lenn ci danki adduna yi bu ci mel ni tapoo gu càmmooñug atlas otan njiilul amerig lii di harry truman g dafa nekkoon ku bañoon lool mbokkte walla cominisme te bañoon it mu tas looloo taxoon mu taxawaloon ci atum g ag tapoo walla alliance gu boole woon amerig itaali holand beljik norwej danmark fraans kanada portigaal ak island ñu tudde woon nag tapoo gii tapoo gu càmmooñu atlas ginaaw bi la ci turki bokksi ak gres atum g ak almaañ gu federaal gi atum g seenug kollëre it ci ñatti wàll yii la jëm 	kepp ku laal benn ci reewi tapoo gi laal nga yi ci des 	reew yi ci bokk dananu dimblante ci seen biir ci wàllu aaru alal ak koom 	tapoo gi dana taxawal ab jataay bu xare te da na am njiit lu matale tam jaadu na nu leeral ne amerig mooy dàttub tapoo gii maanaam mooy reew mi ci ëpp solo ci wàllug li nuy joxe ak ngànnaay paris it moo nekkandi woon ab dalam ba ci mujj gi nu tuxal ko ca buruxel peeyub beljik bokkoon na ci li ko taxoon a jug neexal dundug ay askanam yombal seenu nekkiin dëppale ko ak sarti demokraasi goreg jëmm ak yoon tapoo gu warsaw bennog sofiet ñoom itam taxawal nanu ag tapoo gu kaaraange atum g loolu nag booy seet ag won amerig rekk la ne nun itam toogunu boo sosee tapoo gu atlas nu sos sunu gos rawati na bi ci almaañ gu sowwu gi bokksee ci gu atlas gi atum g tapoo gu warsaw moom bennoog sofiet la woon reewi bokkoo yi nekk ci ngunoom maanaam yi ànd ak moom ci gànnaaru tugal ak diggam mell ni romani poloñ hongri cekoslowaki añs warsaw nag li ko taxoon a jug mooy aar bennoog sofiet gi ak reew yi ko topp ci mbooleem musiba mu man a bàyyikoo ci tapoo gu càmmooñu atlas gi dëkkub warsaw bii di peeyub poloñ moo mujjoon dib dalam li mu yoroon it ciy xarekat àggoon na ci xarekat ñu seddale leen ci diggante reew yi ci bokk tapoo gu kollëre gu diggu gi waa tapoo gu atlas amerig jiite ko danu ne woon daal fawwu nu jële fi bennoog sofiet tas tapoom gii di warsaw ci noonu ñu taxawal ag njiit gu jagoo mbirum penku bu diggu bi atum g ginaaw bi nu sos mbootaayug aar penku bu diggu bi atum ci atum g nu sos tapoo gu iraak turki ñu gën koo xame ci tapoo gu baxdaad tur woowu nag mujj na soppiku atum g mujj di tapoog kollëre gu diggu gi ginaaw bi ci iraan bokkee pakistaan britani ci wetu turki ak iraak ñu leen di fattali rekk ne iraak moom mujj na genn ci tapoo gii ci suwe atum g jataayub tugal bi waa tugal ya daa woote bennoog tugal ak tembug ay gis gisam aki saxalam taxawaloon nanu ca atum g jataayub tugal bi muy ag mbootaay gu koom koom gu politig loolu nag doonoon ab jeego bu njëkk rekk jëm ci reewum orob mu mag mu nu bëgg a taxawali bookoon na ci jataay boobu nag biritani frans itaali belgik holand luxamburg danmark norwej suwed ak irland nga rax ci dolli ay ndawi parlamaa yu reewi orobug sowwu gi ak turki dëkkub strasburg bu frans bi moo doonoon dal bi rewwi tugal ya ca ja bu nu bokk ba waa tugal yi ci ag kollare gu nu fase woon ca rom atum g taxawaloon nanu am mbooloo mu koom koom mu orob nu gënoon koo xame ci turu reewi tugal ya ca ja ba nu bokk ngir jële fi ag nduwaan ci diggante reew yi ci bokk te doxal fi yaxantu gu gore ci seen biir buruxel nag lanu defoon seenub dal bokkoon na ci frans britani itaali beljik almaañ gu sowwu gi luxamburg holand irland danmark ak yonan gres ja boobu nag li ko taxoon a jug mooy dimblanteg koom koom gu orob waaye mujj na rax ci gu politig gu yaatu ci seen biir mbootaayu dimblanteg koom koom ak suqali mbootaay gii amerig moo ko sosoon atum g muy mbootaay gu mel ni reewi tugal ya ca ja ba nu bokk ngir rekk man a dugg ci koom koomu tugal bi cig wàll ak ngir man a dëgëral ay seqooy koom koomam yi mu am ak reewi ja bi ci geneen wàll bokk na ci mbootaay gi nag reewi tapoo gu atlas gi ak siwis finland otris suwed ak yogoslawi mbootaayug reewi amerig yi mbootaay gii yàgg na a sosu ndax def na ko ci awril atum g waaye ag dëgg dëggi sosoom mi gi door atum g muy man nanu ne lu juddoo ci xalaatu njiitul amerig lii di woon monrow mi daa wax naan amerig daal ñaari amerig yi ñoo ko moom mbootaay gii nga xam ne diiwaan yu bennoo yu amerig yi ñoo ci bokkoon ak reewi amerig gu latin gi mujjoon na gën a yaatu gën a jëm kanam mujj di ëtt bu am solo ngir dëppale diggante reew yi ci bokk waxuma la nag njariñul koom koom lu mag li ci nekk waa mbootaay gii nag wasington lanu defoon seenub dal te amerig it amoon na kilifteef gu mag ci mbootaay gi kilifteef googu feeñ na bu baax bi amerig tggee kuba ne bokkatul ci mbootaay gi loolu nag mi ngi amoon ci ginaaw bi fi ag fipp gu bokkoo amee ca atum g mbootaayi reewi andis yi moom nag mbootaay gu jagoo yenn ci reewi amerig gu latin gi la li ko tax a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom koom ak aada ñi ci bokk nag di kolombi peru ekuwador cili ak boliwi naalub marsaal bi ak komikon bennoog sofiet daa taxawaloon ag mbootaayug koom koom atum g ngir fayyoo ci ci li tugal def ci wetam muy mbootaayug ja bi nga xam ne amerig moo ko digaloon waa orob yi ne leen woon nanu taxaw ci tabaxaat seen koom koom bu daanu bii nga xam ne xareb adduna bee ko màbboon te moom dana leen ci jàpple wooteg amerig googu ñi ngi ko gënoon a miine ci turu naalub marsaal marsaal nag jawrini amerig ji yoroon wàllu bitim reew la woon ci ginaaw ñaareelu xareb adduna bi sofiet yi nag ñoom seen mbootaayu koom koom ñi ngi ko tudde woon komikon bennoog sofiet jiite woon ko mbooleem reew yi àndoon ak moom bokkoon ci li ko taxoon a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom koom mbootaay gi boole reewi araab yi reewi araab yee ko sos ci atum g ngir dimblanteg politig gu koom koom ak gu aada ci seen biir mbootaayug jàpplante gu asi reewi asi yee ko sos ak yu afrig yi ngir dëgëral diggante reew yi ci bokk mbootaayug bennoog afrig moom mbootay la gu reewi afrig yi ñu sos ko atum g li ko tax a jug di dëgëral buumi dimblante ci diggante reew yi ci bokk rawtina ci wàlli poloitig koom koom ak aada reew yi féetewul fenn reww yu bari temb nanu ginaaw ñaareelu xareb adduna bi rawati na ci goxu afrig ak asi ñu daal di dem nag bokki ci mbootaayu xeet yi reew yooyu di door a am ag temb soxla woon nanu di diisoo ci seen biir te di daje ndax kat ragaloon nanu bu baax reewi sancaan yi ak seeni pexe cig wàll ak ngir ne ginaaw bi nu tembee ba noppi danoo fees dell aki coonay koom koom ak yu politig ci geneen wàll ci nooonu am mbooloo sosu mu nu xame woon ci turu mbooloom reewi asi yi ak afrig ab xalaat dox ci ñoom jañ leen ci ñu taxawal ndajem asi afrig ngir gëstu jafe jafey ñaari gox yi rawati na lu aju ci goreel ay askan seen ak tembal leen teggil leen sukkub sanc bii tegu ci seenug dòq ak ci anam gu mu ci teggoo ci noonu nu def ndajem bandonj ca awril g ca endonesi ndawi lu tollook reew teewe ko yu afrig ak asi ñooy end bakistaan endonesi borma silan mujj di sirilanka afganistaan iraan japon filipin taylan siin gu askan gi wietnaam gu bëj gànnaar gi wietnaam gu bëj saalum gi cambodie lawus nipal ecopi liberia tefesug wurus gana ginaaw bi siri isipt misra iraak nguurug araabi sawdid jordanie libi sudan liban ak yaman ndajem bandonj nag mooy ndajem adduna mi njëkk a boole ndawi ay reewi asi ak yu afrig yu temb ay ndénkaane aki saxal yu bari juddoo nanu ca ndaje ma yuy soññee ci nu yamale diggante xeet yi ak waaso yi te wormaal àqu ak yelleefu doomu aadama ju cosaanu ji ak sañ sañu nit ci wutal boppam mujj gi ko neex moom ndaje mi tam woo na reewi afrig yi ak asi ci nu dimblante ci kom koom ci seen biir te diisoo ci politig ndajem reew yi feetewul fenn nag juddoo na ca ndajem bandonj moomee nu njëkk koo amal ca keer atum g ma ca topp nu defe ko konaakri atum g bi adduna bi gënee bari ay coow xuloo yi gën a tar ci diggante reew yi jamaal abdu naasir mi nekkoon njiitul reewum isipt ak kii di tito nekkoon njiitul yugoslawi ñoom danoo woo woon reew yi feetewul fenn te nekk afrig asi ak amerig latin ne nanu def am ndaje mu mag ngir gëstu tolluwaay bii ak tàngoor wii ci adduna bi ci noonu nu daal di def ndajem belgraad ci sëtumbar g daal di genne ay saxal yu aju ci jàmmi adduna bi ak jafe jafe yi aju ci noccim ngànnaay mi ak jafe jafe bu aljeri bi ak bu kongo ak yeneen jafe jafe yu adduna yu bari yu amoon ca jamono ja nu defaat meneen ndaje ca keer mu reew yi feetewul fenn ci oktoobar g lu tollook ci ndawi reew teewe woon ko ab lim nag ciy saxal aki ndenkaane yu am solo genne na ca mooma ndaje nu tudd ci yii rekk 	wormaal sañ sañu askan yi ak seen àq ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg 	àndandoo ligeey ngir goreel reew yi tembagul 	sakku nu nocci ngànnaay yi te lijënti xuloo yi ci yoonu jàmm te jële fi tapoo yi tas leen dindi dàtti xare yi 	ligeey ngir suqali dimblanteg koom koom aada xam xam ak yar ci diggante reew yi ci bokk ñi ngi fattalee ne reew yi feetewul fenn dolliku nanu bi reew yi temb gënee dolliku xuloob reew yi gën a tàng rawante ci ngànnaayu gën a yokku ci ngànnaay yu nu xamoon yi ak yu gën a jëm kanam yi looloo waraloon reew yi feetewul fenn gën di dolli seeni daje yiy wër ak di gën di ligeey ngir adduna bi man a dégg seen baat te man cee def jeexiit bu baax ñeenteelu doggantal fipp gi xam xam amal ci elektron xamale lan mooy elektron elektron moom yaram wu sew la lool moom daal gën na a ndawe ay milyoi yoon yeneen yaram yi nga man a gise ci bët rekk bu nu rafleel moom sax manoo koo gise ci fésalukaay yu elktronik yu bees yi am leegi li ko waral mooy boo jëloon ay bilyoi elektron dajale leen du nu toll ne boppu puso elektron nag nekk na ci bepp ne ne bu yàlla sàkk moom nag mooy peek fepp wi walla saal bi moom nag foo ko fekk da koy wër ngir xëcc gi ko saal biy xëcc elektron ni muy wëre saal bi booy xool day mel ne ni bidiw yu mag yi di wëre jant bi elektron nag day yanu ay cëfkay kuran yuy bañ saal bi walla fepp wi di yor ay cëfkay kuran yuy wuyyu walla nangu xam xamu elektron ni mu sosoo xam nanu ne xam xamu kuran moom xam xam la bu nu xame bu yàgg ci ki nuy wax taalis di woon boroom xam xamu gres ay boroom xam xam yu bari nag ñëw gën koo jëme kanam bokk na ci ñooñu kii nuy wax wilyaam jilbert di boroom xam xamu angle boo xam ne mooy ki teqale dooley kuran ak dooley bijjaakon ci noonu la wuuteek kii di taalis mi ne woon ñoom ñaar daal benn lanu jilbert it xamoon na ne duusi kuran yi mooy jur dooley asye boroom xam xamu almaañ bii di anofon jiyorik moom itam di ki njëkk a genne masinu juddal kuran maanaam jumtukaay buy tax kuran bi di judd di am loolu di ci atum g tomas adison it ñëw indil ñu lamp bu kuran xam xamu kuran nag soppiku di xam xamu elektron ci njëlbeeni xarnub ñaarfukeel g loolu nag mi ngi amoon ginaaw bi boroom xam xamu fisiyaa bu angle bii di josef tomson jugee feeñal xam xamu elektron atum g daal di ciy ame neexalub nobel ci xam xamu fisiya li gën a jëmal kanam xam xamu elektron nag mooy feeñal gi boroom xam xam yi feeñal ne fepp saal biy wuyyu day xëcc jëme ci boppam lu bari ci elektron yiy bañ te moom fepp wi day seddaliku ci fepp yu bari ndamul xam xam lii ab jeego la bu am solo ci doxub xam xamu elektron jeego bii daal bu am solo la ci dundug nit ci kaw suuf jumtukaay yu elektronik yi ak seen njariñ jumtukaay yu elektronik yi mujj nanu ci jamono jii nu nekk di loo xam ne foo wëlbëtiku gis ko ci kër yi barabu ligeey yi dëkk yu mag yi yu ndaw yi mbay mi ak mecce yi añs kon daal jumtukaayi elektron yi dugal nanu seen loxo ci yombal dund gi nga gis nit ñi ñuy jëfandikoo raxasukaay yu kuran yu otomatik yi ak fompukaay yu kuran yu otomatik yi ak jumtukaayu seral yi yu wuute yi ak rajook tele yu melo yi ak jumtukaayu nataal yi añs boo demee ci ndoktoor it fekk ko mu fees dell ak jumtukaay yu elektron xoolal ma fesalukaay yu elektonik yiy feeñal jàngoro yi gën a tuuti ak nataalukaayu ndoktoor yi ak jumtukaayu segg yu elktronik yi jumtukaay yii dey tax nanu doktoor man a xam lu jot nit man koo faj te looloo tax ndoktoor jëm kanam ci sunu jamono jii gis nga leegi foo dem fekk fa komputer ci bank yi lonkoo yi campeefi goornamaa yi ak ligeewukaay yi gis nga xam xamu fuglug jawwu ji ni mu nosoo leegi ak xam kiliman bi te loolu lepp elektron a ko waral leegi man nanoo xam nu tooyaay bi toll nu jawwu ji selle nu gelaw li gaawe nu tàngoor wi tànge nu niir yi kawee añs te loolu lepp elktron a ko def waa xam xamu suuf jiyoloji jariñu nanu ci jumtukaayi elktronik yi leen di xamal ati doj yi ak ati suuf si te di leen won fi am petrol yoraniyom ak yeneen mblli suuf yu am yi solo jumtukaayi elektronik yi dimblee nanu ci wàlli ngànnaay ak xare ak aaru leegi gis nga jumu fepp rajo jumtukaay yi amul buum ak yiy yonnee tey nangu ak yiy nataal añs lii nag wone na ne xam xamu elektron aki jumtukaayam yi ci aju ci jàmm ak yi ci aju ci xare def nanu fi ag jeqiku gu xam xam gu am solo ci xarnub ñaar fukk g bii nit nag jot na a man a tàggat xam xam bii def ci li mu ci bëgg ci lu aju ci jàmm waaye it mi ngi koy jëfandikoo ci xare yiy màbb tey mbugale di alag mbidéef yi juroomeelu doggantal xareb jawwu ji yaa mahsharal jinni wal insi inistatahtum an tanfuzuu min axtaaris samaawaati wal ardi fanfuzuu laa tanfuzuu illaa bisultaanin sooratu rahmaan aaya di yeen jinne yeek nit ñi su ngeen manee dem ba soobu ci goxi asamaan yi ak suuf def leen ko waaye fu ngeen fi àgg rekk na leen woor ne yàlla a leen may ngeen àgg fa fu ngeen fi àgg rekk ci sultaan ngeen fa àgge sultaan nag mooy lay ndigal kàttan nguur di kon fu ngeen fa àgg sunu boroom a leen fa àggale moom mi leen may xel may leen kàttan ubbil leen bunti yooyule gox man a layal lu tax ngeen àgg fa nit nag yàgg naa xëntewoo xam li ko wër ciy mbir yàgg naa yittewoo xam mbóoti jawwu ju biti jii nga xam ne daa fees dell aki nekkteef yu asamaan ay bidiw aki ñoom seen moom de jot naa àgg ci xam bidiw yi ak seeni kem ak seeni bind ak li leen sos def it ab jeego bu rëy ci xam xamu juxraaf ak yeneen xam xam yi am ag jokkoo ak kaw suuf biir suuf ak li wër suuf peek ko ciy mbindeefi asamaan bidiw ak lu ko moy ci ati juroom fukk yi ci ñaar fukkeelu xarnu bii gis nanu nit mu jeem ay yoon nu mu yeege ci jawwu ji ngir làmb ko te xam la fa nekk loolu nag faalewu ci jafe jafe yi mu ci man a dajeel ak ay wu rëy wi loolu làmbool bokk na ci ay woowu man cee ñàkke bakkanam ñàkk a wóor gi ci bu nuy joy bu masin biy wëndéelu ak buy wàcci li sofiet yi def ci xareb jawwu ji sofiet yi de njëkk nanoo nattu jawwu ji làmbtu ko loolu nu jaare woon ko ci jëfandikoo ay bayyima ngir ragal nit di ci loroo sofiet yi ñi ngi njëkk a joyal seen gaalug jawwu gi tuddoon fostok ñaari soobukati jawwu yu sofiet nekkoon ci biir di yori jajarin ak alaan shabard ci subag bisub awril g loolu nag bettoon na adduna bépp tukkib jawwu bii nag yobbu woon na lu tollook teemeer ak juroom ñatt fukki simili ci biir diir boobu gaalug jawwu gi wër na ci suuf si benn yoon ak xaaj tukkib xam xam bu jawwu bii xew xew la bu am solo ci taarixu nit ci jamono ju yees jii ndax kat moom ubbi na fi ay gox yu yees yu yaatu ci wàllug xam xamu jawwu sofiet yi wéyoon nanu ci seen ligeeyi jawwu yooyu nga xam ne am na ci yu jàmm taxoon a jug ak yu xare taxoon a jugg seen satalit yi gënoon nanoo yokk seen cawarte rawati na ci lu aju ci xare ci diggante ati juroom ñaar fukk yi ak juroom ñatt fukk yi ci xarnu bii li ci waa amerig def waa amerig yi ci ati juroom fukk yi ci ñaar fukkeelu xarnu g def nanu ay jeem aki pexe yu am solo ci wàllug xareb jawwu ji seen cawarte ci wàll googu dolliku woon na ci ati juroom benn fukk yi ci xarnu bii ndaxte seen ligeey yu jawwu yi gënoon nanoo ràññiku te gën a fés ci diggante bii ndax ci la kërug jawwu gu amerig gi ñu koy wax nasa jot a joyal ay waruwaayi jawwu yoo xam ne ay jum ñoo leen di jañ jañax leen ñu naaw bu niy dellusi ci suuf si nekk ay fafalnaaw yu yor ñaari laaf ñu leen di man a jëfandikoowaat ay yooni yoon lii nag tax na ba li nu daa ñàkk ci tukkiy jawwu yi gën a neew te itam indi na ay ngérte yu am solo ci xareb jawwu ji waa amerig jot nanoo sànni waruwaayu jawwu wii di apolo ci sulye g ñaari soobukati jawwu nekkoon ca ñooy aarmustrong ak adwin drin aamustrong nee na amoon naa yëg yëg bu tumbrànke bi may dox ci kaw weer wi damaa yëgoon ne sama màndaxe daa woyofoon lool waa amerig yi sàmp nanu ci kaw weer wi ay jumtukaay yu xam xam yu bari jële nanu fa it ay còmp yu juge ca weer wa teg fa it ab juddalkaayu kuran bu saal kongres it dëppoo ci samwiye g ci prograamu jawwu bi nu tudde woon baaganteg jawwu ngir barig li nu daa dem ci jawwu jeek a dellusi tukki bu jawwu bu njëkk bi nuy wax kolombiya tàmbli na ci awril g yeneen tukki topp ci yu jawwu yu àntu waa amerig yi defati tukkiy jawwu yu carlinger bi ci njëkk di ci awril g juroom ñeenti tukki topp ci bi mujj di ci oktoobar g musibam carlinger am musiba xewoon na ci baagante gu jawwu gu amerig gii di carlinger loolu nag mooy bi waruwaay bi fàccee ci bisu talaata samwiye g lu tollook juroom ñaar faatu ci ñaar ñi di ay soxna njiitul amerig la nu daa wax ronaald rigan nee na woon bii bis de dana doon bisub naqar ak fàttaliku waa amerig yi it tudde woon nanu ko bis bu tiis bi musiba mii du mooy mi njëkk a dal amerig ci wàllug jawwu gi mu ni mel njëkkoon na ko fi ci lu tollook ay at loolu mooy bi sawara tàkkee ca joyaluwaayu waruwaay ba tudd apolo ci samwiye g ci noonu ñatti soobukati jawwu ya ca nekkoon yepp dee amerig defati yeneen tukkiy jawwu yu baagante tudde ko discovery bi ci njëkk mi ngi amoon ci ut g yeneen tukk yu àntu topp ca lii nu tudde xareb jawwu ji daal def na lu am solo ci wàllug xam xam rawati na lu aju ci mbiri jàmm yi ndaxte xam xamu fisiya gën a jëm kanam bu fuglug jawwu ak xam xamu nataalu jawwu biy nataal kaw suuf si te di ko natt xam xamu kart yi ak nataali jawwu yi gën na a jeego ay jeego naka noonu endustri elektronik ni nuy xame fi mbell yi nekk gën a xarañ ak ni nuy xeexe lakk yi añs sofiet yi ak waa amerig yi ku ci nekk soobu nga ci jawwu ji ngir ay xemmemteefi xare jawwu ji mujj di lef mu stratejig mu yaatu ñeel ay ligeeyi xare la nu ca jublu it di door ak jam ay barab yu nekk ci kaw suuf jaare ko ci seen satalit yi nekk ci jaww ji yi ci yanu ay boppi atomig cig wàll walla nu jaare ko ci ngànnaay yu wuute yi nu man a joyale ñu tukke ci jawwu ji ci geneen wàll xareb jawwu ji yamatul rekk ci diggante sofiet yi ak waa amerig yi leegi kay lu sakkan ciy reew bokksi nanu ci mu ci mel ni siin ak fraans am na yeneen reew yuy waaj ngir sànni seeni jumi jawwu walla satalit ci jawwu jii nga xam ne mujj na di barab bu yaatu ngir rawanteg xam xam ak gëpplante ci wàllug xare juroom benneelu doggantal ni japon jëme kanam japon njëkk fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g japon de wéyoon na diir bu yàgg di beru ak a sori xayug tugal gi yam ci yëfi bobbam doyloo aadaam ba ci digg juroom ñeenteelu xarnu g gii beru gu xay ak deltu ginaaw gu mag raxoon na ci ci wàllug koom koom rawati na endustri waaye nag lii mu nekke woon soppiku woon na ci ñaareelu xaajub fukk ak juroom ñeenteelu xarnu ci noonu mu tàmblee juge nànk nànk ci reew mu deltu ginaaw dem ci reew mu jëm kanam ci wàll yii koom koom aada politig ak xare mu roye nag ci reewi tugal yi gisiinu sanc ak yaatal ko ci reew yi mu dendal ngir wone ci dooley addinaam ji mu yor ci wàllug xeex gi nuy def ngir teg loxo ay reew sanc leen japon nag ak li muy yeex a jot ci xayug tugal gi lepp boo ko dee xool ci reewi asi yeneen yi ndax dëppoo gi mu njëkk a def ak amerig ci wàllug joqalanteg yaxantu weesuwul atum g gii rekk teewul mu tàmbli woon na jege nànk nànk xayug orob gi di ci jariñu di ci niitu loolu jural ko mu tabax ay isin yu mag xotti ay yoon defar ay yooni saxaar gën a jëmale kanam ni nuy yaxantoo reewum japon ca saa sa mu tàmblee gis ag yëngu yëngug endustri gu mag gu nirook ga tugal romboon ba mu ciy door a dugg bu ko defee japon xëy di reew mu dox mu jëm kanam raw nag ay maasam ci reewi asi yi ci wàllu endustri xam xam ak xarala mu mujj am moom japon mbooloom gaal mu yaxantu tax a jug mu mag moo xam ne moo jël limub ñatteel ci adduna bi ci diggante ñaari xarey adduna yi marsandiisi japon yi nga mujj foo dem fekk leen fa ci asi ak afrig japon ginaaw bi nu ko gañee ci ñaareelu xareb adduna bi japon gañe nanu ko ci ñaareelu xareb adduna bi te booba moo nekkoon laafum penku mi ñeel reewi digg yi axe ñooy almaañ itaali ak japon japon nag mujjoon na nangu ne gañe nanu ko mu jébbalu joxe loxoom ci kanamu njiitul xare lu amerig lii di mark arthur atum g ci noonu nu taxawal benn jataay bu way tapoo yi ngir doxal mbiri japon nu dénk ko kii di mark arthur ci diggante g waa amerig yi nag rëddaloon nanu japon benn strateji dugal fa demokraasi jële fa dal bi aju ci jaamu imbraatoor bi nu soppi woon it seeni njàngaliin maanaam ni nuy jànge ak li nuy jàng wutaloon leen sartu reew bu bees ray it lonkoo yu mag yi ñu fuqarci ay moomeel yu rëy ci loxoy njabooti japon yi sëddale leen ci lim bu mag ci baykat yi daal di it taxawal ab parlamaa bu bees ci noonu japon jot na a tàmblee nosaat dundug koom koomam gu plitigam ak gu mboolaayam te tàmblee dab nànk nànk reewi endustri yu jëm yi kanam waa japon jariñu nanu ci li leen amerig indil ci ndimbal yu alal ak yu xarala loolu bokk ci li delloosi cawarte gi ci wàllug koom lijjantikati japon yi dox nanu bu baax ci tas ak yaatal koom koomu japon ngir seenug yewwute ak ngir bari gu japon bari ay ligeeykat suqali nag gën na a yokk ci wàllug endustri ak yaxantu ci diggante bi topp ci g japon mujj di ñatteelu reew mi ëpp lu muy ligeey weñ bokk it ci reew yu njëkk yiy segg petrol ak yi ëpp lu nuy defar gaal mbooloom gaalum yaxantoom mi gën na a jëm kanam ay ngañaayam gën a dolliku ligeey bi aju ci jumtukaayi eliktronig yi gën a jëm kanam ba mujj japon àgg ci ci fi nu man a yam ci raw gu xam xam ja yi nuy jaaye ligeeyi japon yi gën a yaatu gën a bari ci adduna bi bu ko defee japon mujj nag di reewum endustri mu mag mu dox te jëm kanam ag jiital teeree ngi nii buy gàttal yoonu xam ndax li nga daa lijjantee xam ciy fan ak cib coona moom la lay xamal ciy waxtu ci lu dulub coona muy bu nu def ngir feeñal ci baat ak waxiin yiy war a wuutu yu fraanse yu bari yu nuy teg ci barabi yu wolof yi te kat fekk na wolof amoon leen mbaa mu manoon leen a am te nu jàpp ne manunoo doylu wëlif leen ma yaakaar ne bu nu bëggee yombal dëgg lu mu metti metti danoo war a wut ay kuutlaay ñeel baati doxandeem yii bëgg a ruur sunu làkk wi te nag yombug xam xam mi ngi ci nga koy jàng mel ni jàngoo kon lu tax muy franais ginaaw du lu moy ab jumtukaay ngir xam ngir déggante waxante te ma gis ne bu dee ci ay wolof seen làkk lay gën a nekke jumtukaay boobu lii ak leneen lu bari moo ma yobbu ci di xalaat ci di binde ci wolof te ba yeneen kàllaama yi ginaaw bindaluma ku leen moy te it nag ni ñepp def ba ami làkk lu tax dunu ko def bay am sunu yos ñun itam waa afrig nekkewunu fi lu dul ligeeyal tugal ak lu ni mel nanu sunu bopp ñor doonte as lëf la it nan la am reew mu tollu ne senegaal ñépp di waxi wolof nga ne fraanse rekk reerale ga a ngii abdul xaadir kebe bunt bu njëkk bi njëlbéenug jamono yu yees yi doggantal gu njëkk gi 	 yewwute ga amoon ca tugal yëngu yëngu googu nag mi ngi tàmbli ci xarnu bu fukk ak ñatt ginaaw juddu gu yonnant yàlla hiisaa ba ci bu fukk ak juroom ñaar mu sos fi nag ay soppi yu xóot ci wàllug aada dundiin mboolaay politig ak koom koom kon daal yewwute gii amoon ca jamono yooya ca tugal li muy wund mooy ag tuxu juge ca jamono ju diggu ja mu y jamono y ag laman walla ag cang dem ci jamono ju yees ji di ju jëm kanam gu xam xam ak xarala sabab yi tax yewwute g orob gi am sabab yi jur yewwute gii yu bari lañu waaye nañu ci indi ñatt yi ci ëpp solo rekk ñooy jeexiit gi lislaam amal ci yewwute g orob gi ci waxtu wi tugal nekke cig deltu ginaaw ci wàllug xay ci jamono yu diggu yi nga xam ne jàngu bi egliis bi faagaagaloon na bépp xalaat bu leer te gore araamal ci nit ñi ñuy xool leneen lu dul am njàggaleem mu way deng mii te doxadi bi orob nekke ci lëndëmam gii jullit ñi ñoom ñi ngi doon jëm kanam bu baax ci yekkati tabaxub seenug xay ci kaw ay cëslaay yu xam xam ak wisaare maandute ak mbokko ci diggante nit ñi ci lu dul xool xeet walla melo mbaaw làkk xayug lislaam gi nag àgg na tugal jaare ko ci yoon yu bari bokk na ci yooyu andalusi ak sisil ak reewi penkub lislaam bi rawati na ci xarey jooñ yi ndax kat booy xool li tugal di nekk lépp di ku ñu dàqe ca xarey jooñ ya duma ko ca teewul mu fàggoo ca njariñ lu bari ngir fenqoo gi mu ci defe ak xalaatub lislaam bi ak nosteg dundam lii nag ci li soppi xalaati waa tugal yi la jëm ci egliis bi nit adduna bi ak dund gi te itam lu bari ci sàkkukati xam xami tugal yi dañoo tàmbli woon di naan ci xam xami lislaam yi ci ndoktoor xeltu gañcax ak ndundat ak yu dul yooyu ci jàngu yu andalusi yi la ko dale ca xarnub fukk ak benn g loolu nag taxoon na ba yëngu yëngu gu firi walla tekki gu mag amoon ci xam xami lislaam yi tukkee ci làkku araab dem ci wu latin wi doon wu xalaat wu diine tey wu politig ca orob ca jamono jooja loolu dimblee woon ci ginaaw bi ci lal yoon wi ba yewwute gu tugal gi man a am feeñug dëkk yu mag yu tugal yi les villes bu ko defee li ñuy wax tool di suuf si sang biy moom moo daa tekki barabu dëkkuwaay bi koom koom bi mboolaay gi ci gii noste màggug dëkki tugal yi ngir màggug yaxantu gi nu daa def ak mboolaayi jullit ñi ak màggug mecce yi ak ligéey yi ngir jòkkoo gi waa orob gii daa def ak jullit ñi taxoon na ba nosteg laman tàmbli woon a lòtt ak a naaxsaay rawati na bi nitug tugal ki tàmblee am yoon wu mu man a jaar bay dund te du sukkandiku ci léppam ci suuf ak tool waaye ci yeneen ligéey yu koom yi dëkk yi tam tàmblee doon barabi leer yu di boroomi xay di sonnale ci loolu ak a lakkal noste gu laman gi tey ligeey cig màbbam def it lu rëy ba yewwute ci tugal man a am lòttug egliis bu paab bi akug tasam egliis bi moo nekkoon di teg loxo ci dundug xalaat gi gu diine gi ak gu aada gi ci tugal gépp te yitteem jépp mi ngi ko sotti woon ci njàngum pas pasu diney nasaraan walla li nuy wax njàng yi aju ci yàlla théologie ak njàggat ak xellu amutoon jenn yitte ci njàng yi aju ci xam xam egliis bi moom dafa jàppe woon boppam ki nga xam ne ci yoon moo war a doxal mbiri politig yi te kat moom egliis bi tawati mbon akug yàqu dañoo ruuroon aw yaramam dugg ko fépp ba waral aw nit wu jàng te yewwu jug taxaw temb ci dañal ñaawteef yooyu ko taqoon loolu tam bokk na ci li jañoon xelum nitug tugal ki ci mu jëm kanam gën a ñaw rawati na bi dëkk yi gënee yaatu deggiinu ligeeyub yaxantu gën fa a xóot ak bu endustri ak aada yii yepp nag ligeey nanu lu rëy ci waxuma la doyodil ngëb gu tar gi paab gi ngëboon mboolaayu tugal gu nasaraan gi waaye it doyodil nosteg laman gi loolu it di doyodil nosteg laman gi rataxal yoon wi ba yewwute gi man a am itaali mberum yewwuteg tugal gi dëkk yu itaali yi ñooy mber mu njëkk mi njëkk a uuf tete yewwuteg tugal gi looloo waraloon ñu am wàccuwaay bu kawe akug wormaal ci yeneen dëkki tugal yi ca jamono jooja dëkk yii niki milano ak venezia ak firenze ak napoli ñoo uufoon yewwute gi seeni boroom xam xam aki njàggatkat ak artist walla waa fànn duggaloon nanu ci seen loxo bu baax li waraloon loolu nag lu bari la bokk na ci dal ga fa amoon ak jàmm ja ak jëm kanamug koom koom ba ak yaatug yëngu yënguy nitu itaali ki ak ba tay yaatug goxi xalaatam ak yëg gu mu yëg gore gu mu am ginaaw bi mu goree ci nosteg laman ak li itaali yàgg a am ci teddnga gu sax ak jaloore mu y njàggati waa rom yi seeni xam xam seeni jeexiit ak seeni fann nga rax ci loolu nekk gi paab gi nekk rom nga xam ne loolu faggul na waa itaali ag cang gu diine ni nga xame ne barab boobu it di itaali faggul na paab gi ci itaali ag tono gu ne ne ak gu maanaa gu mag nga rax ci dolli gëpplante gu mag gi amoon ci diggante dëkk yu mag yi ak peeyi buuri itaali yi ci wàllug njàggat ak fànn ak soññ gi doxalkati dëkk yii ak buur yi daa def boroom xam xam yi daa ligeeyal yewwute gi ak ba tay yittewoo gi nga xam ne amoon na ci dëkk yii aju ci gëstu mbind ak taalif yu yàgg ya ak barig móolukaayi teere yi ci yii dëkk ak nag li itaali doon xéewoo muy nekk ci barab bu raññiku buy dimblee ci jokkoo ak addunay jullit ñi mandargay yewwuteg tugal gi yewwuteg tugal gi mi ngi ame ci mbooleem wàlli dundug nit gu xalaat gu fànn gu politig gu diine ak gu koom koom yii di ñëw ñoo ciy wàll yi gën a rëy yëngu yëngu yi aju cig nite ag nite li miy wund fii mooy dundal njàggat yu yàgg ya yu gres ya ak rom ak feddali sukkandiku gu nit war a sukkandiku ci boppam akug goreem ak sañ sañu wax li nekk ci moom ak dog gàllankoor yu mboolaay yi ak jële fi aaday jamono yu diggu yi ak sotti yitte yi ci adduna bi ak dénd bi ak jeem a xam seeni mbóot yëngu yëngu googu nag bokk na ci màndargay yewwuteg tugal gu njëkk gi ndaxte li mu yittewoo woon mooy xam xam yu kojug nite yi nga xam ne njàggatkati gres yeek rom grego romain ñoom lanu jëloon yittewoo leen ak seeni xeltukat ak seeni boroom xam xam ak ñoñ fànn ak seen boroom mecce yu muus yi te ñaw boroom xam xam yi daa def gëstu yooyu di kojug nite ñi ngi leen di woowe ñoñ nite walla boroom njàggat yi ñoñ nite kon ñooy mbooloom nit mi yittewoo woon jàng njàggat xam xam ak fànn yu yàgg ya yu klaasik ya maanaam njàggati gres ak rom ak seeni fànn ak xam xam yëngu yëngug nit gii nag judd na ginaaw bi mu amee ag jàpple gu tukkee ci kilifay dëkki itaali yi ak seeni boroom alal ñoñ nite ñi génne woon nanu ab taar feeñal ko ci mbooleem fànn yu wuute yi moo xam yatt la mbaa nataal ak deseñ ak misik ak tabax ñoñ fànn ñu itaali ñi ak ñu dul ñoom ci jamonoy yewwute dañu doon roy fànn bu klaasik bi di bu gres rom bi bàyyi nee nag fànn bi nu daa wax xóot nga xam ne moo amoon ca tugal ca jamono ju diggu ja bu ko defee ñoñ fànn ñi jëmale seen fànn ci taarub dénd bi ak dund gu yees gii nga xam ne mooy gisiin wu jëm kanam wi nu am ci dund gi dëkki itaali yi gis nañu aw tabaxiin wu bees ndax wacc nanu nee tabaxiinu xóot wiy am ay poto yu ñu catal te weccee ko ak tabaxiin wu klaasik wi raññikoo ay poto yu am ay ndëpp yu rafet aki jagle mbaa deseñ yu eesañeri mel ne yi daa am ca tabaxiinu gres wa tabaxiin wii siw na lool te tas ci egliis yi ak katedraal yi ak saal yi ak barabi tiyaatar yi ak sangukaay yi ci dëkki itaali yii lu bari ci waa fànn yu siw yi fa lañu feeñe bokk na ci ñooñu deseñkat bu siw ba di fra angeliko mi nga xam ne dees na ko lim mu bokk ci waa fànn yi raw te gën a mag ñi nga xam ne ñoo doon gëstu modeli fànn yu yàgg ya ay ligeeyam itam dañoo raññikoo woon màndargam diine mu dal mu nekkoon moom ku diinewu bokkoon na ci ñoom it leonardo da vinci moom mi boole woon fànn ak xam xam defar nay nataali fànn yu siw bokk na ci yooyu bi tudd reer bu mujj bi ak jokanda walla mona liza ñaari nataal yii ci yi gën a siw lañu ci deseñi jamonoy yewwute da vinci mii nekkutoon ab deseñkat bu aay rekk waaye raxoon na ci dib yattkat bu mag dib rëddkatu tabax te dib eesañër bu muus bokk na ci deseñkati itaali yu yewwute gi ba tay ki ñuy wax titian moo nataaloon ay wàll ci dundug ñu féex ñi walla aristokraat yi ci dëkki yaxantu yi ak fànn yi ak rafayel g moom itam rëddkatu tabax bu siw la woon te di deseñkat bu bokk ci ñi gën a siw ci mbooleem jamono yi bokk na ci ñoñ fànni yewwute gi ci itaali ba tay yattkat ba donatello mooy ki sukkandiku woon ci yattam ca yattiin yu klaasik ya di gres rom rax ci dooli ku yittewoo woon taarub dénd bi la ak ag dundam moom daal ca dëgg dëgg moom la nuy jàppe ki sos te taxawal yatt gu bees gi feeñug làkk yu bees yi làkku latin ci jamono yu diggdoomu yi moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam xam ya ak niti diine ya ak politgkat ya ak njaggatkat ya ak ustaas ya la notoon nag ca nit ña di woon niti neen ñi rekk ñoom déggunu woon wii làkk lu tumbrànke la woon ca ñoom seen làkki bopp yiy yu seeni barab lañu déggoon bi jamonoy yewwute dikkee ngelawul fonk sa xeet upp ci orob gepp la lu bari ci xalaatkat yi ak njàggatkat yi ak woykat yi tàmblee jng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki réewi bopp niki wu itaali wu espaañ wu fraans wu angalteer ak yu dul yooyu bi mu ko defee woykatu itaali bi tuddoon dante g taalif komedi bu sell bi ci làkku itaali naka noonu petrarch g mii nga xam ne li mu gisoon mooy làkku romam wii daal mooy gën ja a kawey jumtukaay ngir génne xasiday woyam yi bu ko defee miguel de cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di don kixota ci làkku espaañ ci noonu it la rabelais g def moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di wu fraans ngir wuññi ci liy yëngu ci biiram ci njàggat lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor kaf chaucer mi dib angle g jug moom itam sotti ciw làkkam woyam yu yéeme yi cib taar rawati na nettaliy kentrebry yi nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati angalteer yu mag yi yi gën a siw feeñug xeeti orob yu yees yi màggug fonk sa xeet ak sa reew ci tugal juroon na ci jamonoy yewwute ay reew yu bari ci orob taxaw yu amoon ag temb ci noonu yittewoo xalaati fonk sa xeet daal di fay feeñ fés fa lu aju ci temb tam di lu ñu fay waxtaane ak àttewiin yi looloo tax xarnub fukk ak juroom daa tàmblee dugg rekk xataati politig yooyu ak yu dul ñoom tàmblee am ay maanaa yu nu man a laal ci xeli lu bari ci nit ñi ci noonu xeet yu bari ci yu orob yi tàmblee feddali yooyule xalaat ci jëf di goreel seen bopp ci toppub jàmbur te jambur boobu weesuwul woon paab bi ak imbratoor bi ay àtte nag yu tugal yu am ay nekkte yu politig yu temb juddoo ci loolu ci ginaaw bi yu am seeni làkki bopp yu yees di ya nit ña daa waxe ay xarnuy xarnu waaye taxutoon ñuy làkki politig yi ak xalaat lu dul ci jamonoy yewwute gi yëngu yënguy dajale mbind yi dëkki itaali yi ak reewi tugal gu sowwu gi ci jamonoy yewwute dañu doon yittewoo dajale mbind yi ci fi ñu jortoon ne fi lanu nekk ci xustantin ak ci dëkki gres yi ak ci yeneen barab yi ci tugal mbind yooyu ñu daa wër nag ñooy yu gres yeek latin yi nekkoon di lu ñu tas ci kàgguy daara yeek egliis yi ak katedraal yi ak ci nit ñi walla kër yi yittewoo woon mbir mii peey yi daan àtte dañu daa jagleel lii alal ju bari ñoñ nite ñi tam ñu ci bari jëmale woon nanu seeni ligeey ci dajale mbind yi ci noonu ñu jot a am ci misaal rekk mbindu m binkat bii di waa rom te dib xutbakat tuddoon quintilian nj g ak bataaxeli cicero nj yu xutba yi ak woy yu at ba at yu tacitus yi g tacitus moomu mooy taarixkatu xeexi jarmaan yi mi ngi bokkoon ci ñi gënoon a ñaw ci xutbakati rom yi ak seeni njàggatkat yu ñaw yi sonn ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya yewwuteg orob gi yittewoo woon na te sonnoon ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya ag jublu gu yees am ci jàngiinu taarix ñu koy teg leegi ci cëslaayu jam waaye tegeesatu ko rekk ci dégg ak nettali ci noonu ab jàngu sosu ci firenze am njàngaleem jëm ci jam gu taarix mu tudd daaray xam xam bu taarix bokkoon na ci boroom xam xam yi ci gënoon a duggal seen loxo nitu taarix kii di lorenzo valla g mooy ki jamoon te diiatoon benn dosye bu taarix sikkoon it ag wéram mooy li ñuy wax mayug xustantin mooy dosye boobu nga xam ne paab yi yàgg nañu cee sukkandiku la ko dale ca xarnub fukk ak ñaar g ci seen xeex yi nu doon def ak buur yu mag yi ngir feddali ci seen àqi politig ci àtte nit ñi jiite leen bokk na ci ñi nga xam ne yittewoo woon nañu gëstuy taarix yi ak yu politig yi bindkatu itaali bii di xalaatkat bu politig bu am diplomasi di nicola michiavelli g michiavelli mii def na teere bu mu tudde woon buur bi ndax da ci doon wax lu aju ci buur bu am doole bu doon bennale dëkki itaali yi ak nguur nguuraanam yu daggatoo woon yi te tas jëm kanamug yaxantu ak endustri yaxantu noyyi na bu baax ci orob gu sowwu gi dale ko ci njëlbeenug xarnub fukk ak benn g itaali fi mu feete dimbli na ko bu baax ci yëngu yëngug yaxantu dox fa te jëm fa kanam ci noonu lonkoo yu yaxantu yi tàmbli fa a sosu di jëli marsandiisi penku yi niki sooy ak cuub yi ak rëndaay yi ak wurus ak bëñu ñay ak yu dul yooyu ginaaw bi it yii lonkoo ginaaw bi ñu gënee jëm kanam tàmblee yòbbu yii silaa ci yeneen dëkki orob yi bu ko defee bu ñuy dëpp di indaale marsandiisi orob yi niki ngëndal ak der ak firaa jëm kanamug yaxantu googu ak gu meccey endustri yi jur nañu ag xereñ ci denciinu alal akug jëm kanam ci kee yi ñuy jëfandikoo ci jëfi yaxantu yooyu ci noonu am mbooloom ay sandikaay mecce feeñ mujj teg loxo ci ginaaw bi ci fepp fu koom nekk te am fa cawarte naka noonu nu def ay ligeey yu mag ci wàlli mboolaay ak politig ak xalaat raxaatal ci loolu juddug maas gu diggu gi ñooy mbooloo miy ligeeye yaxantu ak yeneen mecce yu wuute yi feeñug yëngu yëngug xam xam gu yees gi yewwute gi ci njëlbeen gi dafa sotti woon yitteem ci dundal njàggat yi ak fànn yi ginaaw bi mu dox as lëf ba àgg ci mbooleem lu xay gu mat laaj ci noonu yewwute gi matale mbooleem dundug mboolaay gi bokk na ci xam xami dëppale yi ndaxte xam xam moom màggoon na ci dëkki orob yi jàngu yu mag yi sosu ci orob gi rawati na ci dëkki itaali yi yëngu yëngug xam xam googu mi ngi tàmblee ci di jeem a dundal xam xam yu yàgg ya ginaaw bi mu dox jëm kanam loolu nag li ko waraloon mooy jariñu gi mu defoon ci yoonu xam xam woowu di wu kojug nattu maanaam lu nekk looy wax nga teg ci sa loxo mu leer la ne loolu la nga doog ne moom la ndax wóore na la ci làmb gi nga ko làmb ba daj ko yoonu gëstu woowu nag mooy wi boroom xam xami jullit ñi jaaroon ci noonu boroom xam xamu fisiyaa bu angalteer bi ñuy wax roger bacon feeñ di njiitul gëstug xam xam ci tugal becon mii mi ngi sukkandiku woon ci yoonu jakkarloo ak nattu ci gëstoom yooyu nga xam ne àggale woon nanu ko ci ay ngérte yu am solo ci xam xamu bidiw ak bu weer yi ak yu matematik yi ak juxraaf naka noonu boroom xam xamu xeltu ak politig bu angalteer boobu di francis bacon moom itam feeñ g di koo xam ne dafa jëfandikoo xel ci àgg ci dëgg yu xam xam yi ci noonu ci gisiin mooy ki teg ponki ngérum xam xam mu bees mi ak doonte moom doonul woon boroom xam xamu dénd boroom xam xamu itaali bi leonardo da vinci g moom tam feeñ di kok dafa yittewoo woon jiyoloji bu mekanig ak matematig ak yu dul yooyu nga rax ci dolli fànnu yatt ak nataal ak misik ak eeseñëri mu nekkoon daal boroom xam xam te di nitu fànn tey fentkat naka noonu boroom xamu itaali bii di galileo g feeñ mooy ki njëkk a defar nattukaayu tàngoor njëkk a fuglu bidiw yi ca fesalukaayam ba dëgëral te feddali gisiinu boroom xam xamu bidiw bu poloñ bii di copernicus g bokk na ci màndargay xam xam yeneen yu yewwute gi fentug móolukaayu teere ci loxol nitug almaañ kii di john gutenberg atum g fent gii ak doonte gu almaañ la teewul jëmale na kanam bu baax dundug nit ci biir tugal ak biteem wuññiy juxraaf yi tam ci màndargay yewwute gi la woon ak yéwénalug diine gi ci tugal nga dolli ci loolu feddali gu nitug tugal ki feddali jëmmam jii nga xam ne yàgg na a nekk di lu nu làq ci jamono yu diggu yi ci biir ay kureel walla sandikaay mecce yi mu daa bokk ngir làqatoo ca ak aar njàriñi boppam yewwute gi ci itaali yewwute gi ci itaali daa tàmbli woon a giim ak a yànnjadi ci mujji fukk ak juroomeelu xarnu g ak njëlbeeni fukk ak juroom benneelu xarnu g loolu nag li ko waral lu bari la ñu jéem cee indi yenn rekk yi ci ëpp solo attekaay yooyu mosal nanu ginaaw bu àtteb lislaam dañee ca andalusi te garanada nërméelu daanu mosal nañu lu bari ci jullit ñi ay xeeti mbugal ak coona lu maneesul a misaal bokk na ci di leen lakk ñuy dund tuxug yewwute gi ak li yewwute gi di neew doole ci itaali lepp taxul mu naaxsaay mbaa mu suux li am kay mooy da fa a tuxoo dem ci yeneen reew yu tugal niki espaañ portigaal fraans angalteer holand ak almaañ añs ay jëfka yu bari bokk nanu ci li tuxale yewwute gi jële ko itaali yòbbu ko ci yii dëkki orob bokk na ci yooyu nekk gu yii dëkk nekk di yuy door a noppi ci seenug sosu gu politig gu yees ak tàbbi gu ñuy doog a def ci jamonoy tabax ag xay ñi daa woote yewwute gi nag def nanu lu rëy ci tuxale ko itaali mu dem feneen nitug holand kii di erasmus g moo tasoon te wisare yewwute gi ci almaañ jaarale ko ci def fa ay waxtaan aki xutba ak ci yeneen dëkk yu orob yi erasmus mooy ki firi injiil jële ko ci làkku gres yòbbu ko ci wu latin jël nag li ñu ciy wax kòllare gu yees gi def ko ci ay làkki orob yu bees loolu bokk ci li feexal te goreel xalaatub tugal bi ci ngartaajoo gi ko niti diiney katolig yi ngartaajoo woon loolu it won na waa tugal ne yaxub injiilub latin bi egliis bi yoroon du woon biy cosaan te yax bu bari woon ay yàq la kon daal eramus mooy ki waajal xelum tugal mi ci mu man a nangu yéwénali diine yi ni yewwute gi meloon ci fu dul itaali yewwute gi ca almaañ dafa yoroon melow njàngat wiy ligeeyal gëstuy diine yi ci manaa daa yamoon daanaka ci lu aju ci diine rekk ca dëgg dëgg gëstu yi aju ci xam xami gres latin yi dafa xawoon a yeex a àgg ca dëkk yooyu di yu almaañ ak li njiiti yooyu dëkk daa dimbli gëstu yooyu lepp cig wàll ak li almaañ doon am ay daara yu mag ci vienne ak idelberg ak baasal ak strasburg ak yu dul yooyu lepp ci geneen wàll yeex googu nag li ko waraloon mooy niti diine yi ak ñu dul ñoom ñoo ko nanguwutoon ñoom daal danu fee nekkoon rekk di sàkku nu ñu tënke te jéng yooyu njàng ak gëstu te defi pexe ba du ñu tas ci anam gu yaatu ngir nu wattoo ci seen kilifteef sàmme ci seen daraja aare ci seen ligéey ci noonu danañu gendiku ne yëngug nite gi ci almaañ dafa doon sori jubluwaay yu deet diine yi looloo tax du kiimaan almaañ di woon barab bi uufoon yëngu yu yéwénali diine yi gënoon a am solo ci tugal bu dee ci fraans moom yewwute gi melow njàngat ak nite la fa yoroon wi yittewoo woon xam xami gres yi ci noonu boroom xam xami itaali yi ak yu gres yi taxaw ci wisaare gëstuy xam xami gres yi ñu móol teerey ndonoy gres yi ci móolukaayu paris ba ñu taxawaloon ca xarnub fukk ak juroom benn g ni nu duggale seen loxo ci amal ay akaadimi aki barabi xam xam ngir njàng yi aju ci nite niki bànqaasub buur bi ci paris ñu sos ko ci jamonoy buurub fraans bi di fransuwaa mu njëkk mi atum g bu dee ci angalteer ba tay yewwute gi ma nga fa yoroon melow njàngat ak nite ay gëstu yu xam xami gres yi am fa ay ñoñ nite ñu waa reew ma ñu bari ñooy ña ca siwoon ñoom ñooy ñi daa jàngale làkkuw grees wi ci daaray xam xami itaali yi ku ci mel ne wilyam lilly mi daa jangale làkkuw gres ca rom erasmus mu olaand mi ak kolt mu angalteer mi ñoo tekki woon injiil ci làkkuw angale wu bees wi buurub angalteer bi henri mu juroom ñatteel mi moom tam sosoon fa juroomi toogu yu darajay ag ustaas ci xam xami pas pasu nasaraan ak yoonu siwil ak wu dénd bi ak làkku ebrë ak wu gres ci daara ju mag ju kembrij jàngub san pool bi nekk london moom it jagoo woon njàng yu nite yi yewwute gi ci angalteer dafa jublu woon yoonu takk ak boole diggante pas pasu nasaraan ak gëstuy nite yu njàngat ak yu fànn yi yewwute googu nag indiwul woon lu yees lu ñu fent ndare ci xarnub fukk ak jurom ñaar g bi am njurum njàggatam ak mu niteem mu yees feeñee ci anam gu fes te rafet ci woyi william shakespeare yi g ak woykat bu silmaxa bii di john milton g ak ñu dul ñoom ñaar fii tam ci angalteer yoonu yewwute gi da fee jengoon as lef jëm ci yewwute gu xam xam gu aju ci xam xami dëppale yi walla xam xami nattu yu làmb yi ñi jiitu woon ci lef moomu ñooy ñaari boroom xam xami angalteer yii di roger becon ak francis becon ñoom daal ca dëgg dëgg ñooy ñi sos daaray xam xam ca angalteer baat bi nuy mujj a wax ci yewwuteg tugal gi mooy moom daal moo ñàkkal jamono yu diggu yi kàttan ci jeexiital ci mboolaayu tugal gi ci wàlli dundug politigam gu mboolaayam gu xalaatam ak gu aadaam ngir jeexiit yii fi yewwute gi sotti ci orob ay noste yu yees am nañu yu làmboo tabax guur gu yees gi ak mboolaayug orob gi ci cëslaay yu aada yu mboolaay yu jikko ak yu ngér yu yees ni mu duggale loxo ba tay ci ubbi ay gox yu yees yu xam xam yu jël gisiini xam xam yi ak dal yu xam xami juxraaf yi lii lépp nag moo sabab jamono ju yees ci orob di ju wuuteek ja woon ca jamonoy laman ci xalaat ak ngér ak defiin aki xew xew loolu lepp nag nga boole ko moo jur jamonoy tugal ju yees jii doggantal gu ñaareel gi wuññi yu juxraaf yi luy wuññi yu juxraaf yi yëngu yëngu gu wuññi gu juxraaf walla feeñal gu juxraaf yëngu yëngu gu yàgg la waa isipt ñu njëkk ña ak finiix yi ak jullit ñi defoon nañu ko bu yàgg njëkk waa orob di ko def ci jamono ju yees ji lu am soloo ngii nag ñu war koo xam mooy wuññi y juxraaf yi bi muy am it li ko taxoon a jug mooy ay xemmemteefi sañc ak doonte daa mbubboo woon gëstu gu aju ci xam xamu juxraaf yëngu yëngu gu wuññi gu juxraaf gi ñuy waxtaane ci doggantal gii da nanu ko man a xamalee ci nii mooy mbooloom ligeey yi jéngukat yu tugal yi daa def ci ñaari xarnu yii bu fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom benn g yenn nag ci réewi tugal yu nasaraan yi ñoo leen doon soññ ak a jàmbaarloo ak a xiirtal ci loolu li sabab wuññi yii sababu diine moo jiitu ci sabab yi waraloon yëngu yëngu yu wuññi yu juxraaf yu orob yii am sababu diine mooy li gën a waral ñaari reewi katolig yii di espaañ ak portigaal defoon ligeeyub wuññi boobu ñoom yile ñaari reew dañoo jortoon ne dananu man a sutuxlu ci biir afrig ak fu dul moom def ko barab bu dëppoo ak li ñu bëgg muy tas fa ag katolig ak nangu ko teg ko loxo jaare ko ci diine reewum portigaal moom daa gisoon ne reewum ecopi mii di mu nasaraan waaye di mu yoroon ngérum xibt mu ortodoksi man na koo soppi def ko mu yor ngérum katolig loolu nag da nga ci gise diinewu gu dëgër gi amoon ci waa espaañ ak waa portigaal ca jooja jamono paab gi moom da daa soññ reewi nasaraan yi ci ñu dugg bu baax ci wuññi yooyu ngir tas ag katolig ak xatal lislaam te sonnal ko tee koo tas ngir neewal dooleem xottite ko giir ko ci noonu mu moom paab gi génne ay mbind yuy jox àq ñaari reew yii ci ñu moom gox yu yees yi ak mbooleem yu nu wuññiwaat moo xam geej yi la mbaa jeeri yi paab gi ak nasaraan yi ci ginaawam dañoo ragaloon lislaam ak ñoñam looloo taxoon ñu daa wut nu ñu mucce ci ñoom ñu ne woon kon nanu leen fi jeem a jële am na yeneen reew yu yees yu feeñ ci ëttub politig bu tugal bi yu ci mel ni espaañ portigaal angalteer fraans holand ak yu dul yooyu réew yii nag dañoo tàmbli woon di xalaat bu baax ci tas ak wisaare seeni kilifteef ak jeexiit ci biti seen rawati na ci reew yi ci yeex ci seenu g nekku walla sosu gu yees ñu gisoon it ne bu ñu fa tasee wisaare fa seeni xay aki ngéri diine loolu da na man a nekk ay raas yu ñu man a jaare ngir sampu fa sanc leen reew yii nag joante woon nañu te gëpplante ci mii lef loolu bokk ci li daa soññ ak a xiirtale ci yëngug wuññi gu juxraaf gi waa orob yi ñoom dañoo gisoon ne addunay jullit ñi daal mooy ji ngëp ci loxoom nosub yaxantu bi ndaxte ñooy ñi notoon tegoon loxo ci kaw yooni yaxantu yu penku yi ci noonu xalaatu wacci fi yooyu yoon te gëstuji yeneen yu leen man a àggale end ak siin tàmblee feeñ ngir bañ a fay njëgi nduwaañ yi ak galag yeek yeneen yi cig wàll ak ngir neewal doole koom koomu jullit ñi ci geneen wàll ginaaw bi ñu soppee yoon yooyu def leen leegi ñu jaar afrig ak màmbulaan gu atlas gi loolu lépp ngir bañ a jaar fi jullit ñi dëkke yenn ci réewi tugal yu yees yi dañoo gisoon ne li gënoon ci ñoom mooy seeni séqoo yu yaxantu ak réewi penku yi ñu koy defal seen bopp ngir mucc ci rënkug yaxantu gii dëkki itaali yi ame woon te daan ko def yu ci mel ni venezia ak genova ak yu leen moy xalaat bii nag taxoon na ba yii réew demoon gëstuji aw yoonu yaxantu wu bees nga xam ne ñoo ciy nekk ci wenn waxtu wi di yaxantukat biy jëli tey tuxal tey kiy dox ci diggante yi lori waa orob yi tàmbli woon na a yol bi ñu déggee xibaari wurus ak xaalis ci afrig ndax kat mbell yu gànjaru yi dañoo muuroon seeni gët fees seeni xel ñoom ñi nga xam ne dañoo tàmbli woon di faale ak a yittewoo wàllug ne ne gi rekk bayyi nee yeneen wàll yi loolu moo tax ñu sawaroon lool ci def wuññi gu juxraaf gi bi ñu déggee tono gu ne ne gu rëy gi nga xam ne am mbooloo ci wuññikati orob yi ndàmmoon nañu ko ci seen tukkiy wuññi yooyu rawati na bi ñu jàngee xisay tukkikatu itaali boobu di marco polo g mi wuññiji woon ba siin g nga xam ne bi muy dëpp daa indaale lu sakkan ciy doj yu tedd ba mujj waa venezia daa ko wooye boroom milyo yi xalaat yi boroom xel yi ci tugal amoon ci suuf si ak bindam dafa soppiku woon ginaaw bi ay tukki yu juxraaf yu kenn kenn amee ak yu mbooloo yu nasaraanal juge orob génn rawati na ginaaw bi jamonoy xarey jooñ yi jàllee nga xam ne boroom xam xam yu bari leegi dañoo am koolute ci ne suuf si dafa bulu walla mu mel ni ab kol kol wuute ak la ñu jàppoon gëm ko muy dafa tàllaliku mel ne basang gu ñu lal loolu nag mooy li muuroon xeli waa orob yépp ci jamono yu diggu yi ag jng jëm ci sopp ag jéngu ak bëgg xam xamu juxraaf feeñ ci ñoom ginaaw ba fa ruug gëstu gu xam xam gënee suuxatu gën fa a jëme kanam ak li ñu jële ci jullit ñi ci biir xeexi jooñ yi ak ginaaaw bi ci xam xam bu juxraaf bu jëm kanam ak ginaaw bu xam xamu bidiw ak ligeeyiinu gaal ak buusal biy won gaal yi seeni yoon gënee jem kanam wuññiy juxraaf yu portigaal yi portigaal moom la ñu y jàppe reew mi jiite woon wuññi yu juxraaf yu orob yi buur bii di henri mi nekoon ab mool g doonoon doomi buur bu portigaal bi tudoon john mu njëkk mi moom mooy ki njëkk a def ay wuññi ci waa portigaal yi mu nekkoon ku soppoon dugg geej ak yër xisay mool yi ak teerey taariix yi muy ku aayoon ci rëdd karti juxraaf yi moom la baayam sàmpoon mu yor sawuta ginaaw bi ñu ko nangoo ci julliti marog yi atum g henri daa xalaatoon a wesaare diine y nasaraan ju katolig ji ci afrig ci noonu mu ne kon na jokkoo k buuru nasaraan bu ecopi bii di prester john ngir ñu ànd xeex waa marog yii di ay jullit cig wàll ak ngir man a àgg ca waaxi geej gu xonq ga ci geneen wàll ci noonu mu yabal ay mool yoy ci seen tukkiy wuññi yooyu àggoon nanu ba ca duni kanaari ya ak madira ak osoras ci mambulaanug atlas atum g naka noonu ñu wëy ci seen tukki yooyu ba agsi senegaal atum g ginaaw bi henri deewee tam teewul seen tukki yooyu wëyoon ba ci sottiwaayu dexug kongoo gi ak niijer bu ko defee mool bii di bartholmew diaz moom àgg ba ca wàllug bëj saalumu afrig di fa ñuy wax boppub callmeer atum g moom la buurub portigaal bi soppi tur wi tudde ko boppub yaakaar ju baax ji ngir mool yooyu man cee ame yaakaar ba man a wuññi yoonu yaxantu wi jëme end mool bu siw bii di vasco de gama moom jug def tukkib wuññi atum g daal di àgg end ginaaw bi mu wëree afrig jaare ko ci yoonu tefesug marog gi romb bopp yaakaar ju baax ji ak mosambig ak mombasa ak malandi ba àgg jawa ca tefesug sowwu gu daanaka dun bu end vasco de gama mii jot naa xamante ak ahmadu bnu maaja mii di woon ab mool bu jullit bu araab moo ko dimbli sax ba mu man a àgg end ndaxte mooli jullit ñi ñu xamoon geeji penku yi lañu woon ak yooni yaxantu yu jéeri yeek yu geej yi naka noonu beneen mool jugati bu tudd kabraal def ab tukki bu geej bu aju ci xare dem end tàmblee naj ak a sonnal samirin mi daa àtte ak a saytu fi nuy wax kalikuta gu end gi ngir mu jox portigaal ab barab bu yaxantu ci tefes gu sowwu gi kabraal mii xeex na fa ak jullit ña song barab ya ak mbooloo m gaalam ma vasco de gama moom itam delluseeti end ci ab tukkib xare ngir faagaagalsi samirin ak mbugalsi yaxantukati araab yu jullit yi ak defsi ay déggoo ak buuri goxi end yi nekk ci tefesug sowwu gu daanaka dun bu end bi li wuññiy juxraaf yu portigaal yi jur wuññiy portigaal yi jur nañu ay ngérte yu bari yi ci ëpp njariñ ñooy yii di ñëw loolu nag mooy li doyadiloon koom koomu jullit ñi ci penku bi maanaam koom koomu nguurug mamaalik ci jëmmi boppam lii moo taxoon nguurug mamaalik mujjoon neew doole ci kanamu nguurug portigaal gi ak ci kanamu ñoñ usmaan ñi nga xam ne jot nañoo fexe ba xaw a woyofal naj ak ñàkkal jàmm gi portigaal defoon araab yi ak nguuri araab yi nekkoon ci tefes gi yàqoon nañu it mbooleem jeem yi ñu daa def ñoom waa portigaal ngir taxawal ab jë bu nasaraan kontar doole yu lislaam yi nekkoon ci peggu geej gu xonq gi ak tefesug afrig gu penku gi wuññi yu juxraaf yu espaañ yi li ci duggaloon portigaal moo duggal it espaañ ci wuññi yooyu ci noonu boroom xam xam yi daa yëngu ci mbiri wuññi gi danoo jàppoon ne suuf si daa bulu moo waraloon ba ñuy dem end ñu jaare woon ko ci sowwu bi moolub itaali bii di cristoforo colombo moom defaloon na waa espaañ ñi benn tukkib wuññi atum g juge espaañ jem end jaare ko ci sowwu bi ci màmbulaanug atlas gi ginaaw tukki bu tar te sonnle moom colombo àgg na ca duni bahama ya mu mujjoon a tudde san salvador juge fa dem ca tefesug kubaa gu bëj gànnaar ga ak dunub ayiti bi mu faroon tudde espaañ gu ndaw gi mu delluwaat nag espaañ ci atum g ànd ak jort ne moom de jot na a àgg end ci yoonu sowwoom woowu ci atum g colombo defaat na ab tukki bu li ko taxoon a jug mooy teg loxo ci suuf yooyu mu jotoon a wuññi ci atum g ak wisaare fa katolig ca ña fa dëkk te mu tudde woon leen ay endo ci tukki bii la jotoon a wuññee jamayka daal di delluwaat espaañ ci atum g mu defati ñatteelu tukki atum g waaye amu ca woon tawfeex mu dellu defaat bu ñeenteel atum g taxul ba tay mu am ca la mu ca doon wut bu ko defee nag ñaari sooy yii mu def ci ñaari tukkeem yi tax ba buuru espaañ bi ferdinand ak soxnaam lingeer bi isabela begadi woon ci loolu ag siwam suux ñu folli ko ci njiitul geej gi daal di koy delloosi espaañ ci ay jéng ngir mere gu ko meññilukat yi mere ñoom ñi seen yaakaar tas colombo faatu na atum g te xamul sax ne wuññi na adduna ju yees ju dul end ginaawam it wuññikat yi doon ligeeyal espaañ wëy ci seen ligeeyi wuññi yooyu ka cay amerigo vispucci jot ca a àgg ca gox ya colombo àggoon ak yeneen yu mu àggutoon ci njëlbéeni xarnub fukk ak juroom benn moom mool bii di amerigo moo am teraagay ñu tudde ko adduna bu bees bii di amerig tay li wuññiy espaañ yi jur wuññi yu angalteer ñoñ angalteer ñoom itam sóobu woon nañu ci wuññi yi bi buur bi henri mu juroom ñaareel mi nekkoon buurub angalteer digalee mool bii di john cabot mu tukki dem end jaare ko bëj gànnaar gu suwwu gi ca saa sa mu geeju tukkee bristol atum g jéggi màmbulaan gu atlas àgg tefes gu bëj gànnaar gu amerig gu bëj gànnaar gi ca new fondland ginaaw bi mu jéggi librador dellu angalteer cabot mii delseeti na leru tefesu g penku gu amerig gu bëj gànnaar gi ba àgg florida loolu nag moo doonoon tàmblig sancug walla koloniiseg waa angalteer yi ñeel amerig gu bëj gànnaar gi ak kanadaa ba tay it kii di jams kook di woon ab mool bu dëkkoon angalteer defoon na moom it ñatti tukki yu wuññi ca tefesi ostrali yu penku ya ak newsiland wuññiy fraans yi waa fraans nag ñoom ñoo mujjoon a duggsi waa angalteer waa espaañ ak waa portigaal ci lefum wuññi mi ñoom seeni tukkiy wuññi daa jemi woon kanadaa ki ñuy wax jaak cartier moom ab mool la woon daa jugoon def benn tukkeem bu wuññi ci jamonoy fransuwa mu njëkk mi jeggi màmbulaan gu atlas gi jem sowwu fetali àdduna ju yees ji ci noonu mu àgg new fondland gi jàkkaarloo ak kanadaa daal di fay jot a wuññi walla feeñal sottiwaayu dexug santa lorans tukki yi cartier mii jot a def ci goxi amerig gu bëj gànnaar gi ñeent lañu woon bi mu ko defee sancug fraans tàmblee putuxlu ci kanadaa ak goxi dex yi ci amerig gu bëj gànnaar gi noonu ñu taxawal ab sancu tudde ko samwel de shampala taxawal it dëkk bii di kebek ci tefesug dexug santa lorens atum moolu fraans bii di de laasal jotoon na a wuññi dexug misisipi ci noonu waa fraans ya daal di fay sos sancu walla koloni bu luwisiyaana bii nga xam ne mi ngi jële turam wi ca buurub fraans ba tuddoon luwis mu fukk ak ñeenteel mi wuññi yu oland yi lonkoo gu end gu penku gu oland gi dafa joxoon ndigal moolub angalteer bii di henry hadson da ko o joxoon ndigal ci mu defal oland ab tukkib wuññi ngir man koo gisal aw yoon wu bëj gànnaaru penku wu ko man a àggale asi ci noonu mu geeju moom hadson juge angalteer jaare ko ci bëj gànnaaru atlas gi jawali golofub new york ak dexug hadson gi mu tudde woon boppam moolu oland bii di wilyaam shotin moom moo wuññi yoonu boppub horn bi nga xam ne mujj na di yoonu geej wu am njariñ waa oland yi jeemoon naño o wuññi ostraali ak newsiland ci diggante g li wuññiy juxraaf yu orob yi jur li wuññiy tugal yi jur man nanu koo tënk ci lii di ñëw yëngu yëngu gu yaxantu gu yees gii ñi ngi ko tudde woon soppi ci anamug yaxantu doggantal gu ñatteel gi yëngu yëngu yi jugoon di kontar egliis bu paab bi yëngu yëngu gu yewenal diine ji ci tugal yëngu yëngu gu yéwénal gu diine ci tugal mooy googu doon am ci orob ci xarnub fukk ak juroom benn g ngir setal egliis bu katolig bi ci li ci taqoon ci ay ñaawtéefi pas pas ak yu jikko na ñu ko daa defe mooy jeem a delluwaat ci njàggaley injiil yi li waraloon yéwénal gi ak li egliis bi di nekk nguurug ruu lepp ci li ko njëkk a tax a jug teewul ànd ak li jamono di gën a yàgg mu jot a àgg ci ëpp ci loxob weñ nguurug diine gi ak gu politig gi maanaam mu tëye tëyiin wu metti te tar ñaari nguur yii di gu diine gi ak gu adduna gi ci loolu la mujje di dooley politig ju diine ju koom ju mboolaay ak ju aada ci mboolaay yu tugal yu katolig yi ci jamono yu diggu yi dàkku nag walla xañ nit ki jàngu bi moo nekkoon mbugal mi gën a saf te gën a tar mu egliis bi moomoom daan ko teg kuy jeem a léewtoo k moom ak nu darajaam man a kawee mbaa mu màgge ni egliis bi ci safaanub muy jëfandikoo nguurug ruuwam gi di jëmale nit ñi ci yooni baax ak ragal yàlla moom déy ginaaw ag mbon da koo duggoon daa labaloon boppam ci bànneexi adduna aki caaxaanam fàgguloon boppam ay suuf yu yaatu ay alalam it mu teggiloon leen te musal leen ci galag yi ñépp di fay ci noonu paab yi ak kardinaal yi nekkoon di ñu nuuroon ci dundug adduna aki caaxaan yu ëpp ñaawtéefi egliis yooyu ak yu leen moy ñoo gestuloo woon te fëkkoon yittey yéwénalkat yu mboolaay yi ak bindkat yi ci jamonoy yewwute gi ki gënoon a jeexiital ci mbooleem bindkat yooyu mooy labbe bii dib xeltukat nu ko daa wax erasmus g moom daal jamoon na ci teereem bi tudoon tagg ag ndof praise of folly jamoon na ci nekkiinu egliisu katolig bi mu nekkoon jam yu tar te wex dox gu taarixe gi yéwénalug diine gi defoon ci orob yéwénalug diine ci orob ci doxam bi romb na ñaari tolluwaay bi ci njëkk mooy bi ay yëngu yënguy yéwénal yu ndaw amee te lalu niki ay njiitlaay aki cëslaay yoo xam ne ci seen kaw la yëngu yënguy yéwénal yu diine yu mag yi ci tugal tegu bu ñaareel bi nag mooy yëngu yëngug yéwénal gu mag gi ci boppam bu dee nag yëngu yëngu yu diine yi nooyal yoon wi ba yu mag yi man a am man a taxaw ci tugal ñoom ñooy yi nuy wax fransiskaan ak dominikaan ñooy yi gisoon ne mant a ñàkk nu dañal njuumte ak ñaawtéefi diine yi niki aw yoon wu nuy jaar ngir yéwénal egliis bi te dëgëral ko ag yëngu yëngu gu yéwénal daal di taxaw ca angalteer ci njiitl john wycliffe g moom kenn la woon ci ustaas yu siw yu daaray oksford ju mag ji googu nag li ko taxoon a jug mooy dañal li taqoon egliis bi cig mbon gii yëngu yëngu moom mi ngi judd ginaaw lu tolloo k xaaju xarnu ginaaw juddug yëngu yëngu gu ñaari way sell yii di fransis ak dominik waaye gii nag moo gënoon a fés gën a jeexiital ci egliis bi ci gu fransiskaan gi ak gu dominikaan gi geneen it feeñati gu yéwénal ci bohimiya ci njiitul john hess g moom mooy ki ne woon ag diggale wart a am ci diggante nit ak boroomam ndare diggale googu doon ngëm ak jëfe li ci injiil hess nag li mu jublu woon ci loolu mooy wàññi sañ sañu paab gi ak neenal taxawaayub làbbe bi niki aji diggale ci diggante jaam bi ak boroomam bu dee yéwénali diine yu mag yi ñoom ñi ngi doon jëmmu ak a feeñe ci am gi yëngu yëngug protestants gi amoon njiit ya di woon martin luther kalfan ak swingli martin luther ak yéwénal gi martin luther mi ngi juddoo isilban di benn dekk ci diiwaanu saksoniya ci almaañ atum g faatu atum g baayam nekkoon ku daan ligeey ci benn ci gasuwaayi mbell yi mu màgge nag ci njaboot gu ndóol ak ci ron dund gu jafe te wow moom nag jàng na cosaani làkkuw latin ak cosaani ag katolig noppi jàng yoon ak xeltu dugg nag ginaaw bi benn ci barabi jaamu yu katolig yi ngir laabal fa boppam ciy bàkkaar aki ñaawtéef loolu nag ci gëm gëmi katolig yi la bokk ginaaw bi mu tukki dem rom atum g def fa weer gisal boppam ñaawtéefi paab gi ak bon boni egliis bi li gënoon a wëlbati ay bëtam mooy jàdd gi niti diine yi jàddoon ak wàcc gi nu wàccoon yoonu leer ak lëmoodiku wi nasaraan gu njëkk ga yoroon ak set gi mu setoon lii jeexiitaloon na ci boppam ak xelam mu daladi mi jañoon ko it ci jam walla kritige paab gi ginaaw bi it mu mujj fttéerlu ci kawam bi mu bañee moom paab gi ne du soppi aw doxaliinam dikk gi labbe bii di john tetzel dikkoon ci diiwaanu saksooniya atum g ngir jaaysi fa xobi njéggal yi dikk googu dimbli woon na luther ci mu man a feeñal li nëbbu woon ci biiram muy yéeney yewenal yi mu yoroon te fasoon leen ci xolam jaadu na ñu fàttali leen ne xobi njéggal mooy li fi wuutu woon tuubug aji tooñ ji ci jeem a fare ay bàkkaaram ci def lu baax jaare ko ci julli walla joxe asaka mbaa woor waaye paab bii di liyoo mu fukkeel mi moom daal da ne woon da na doy aji moy ji bu bëggee tuub ay bàkkaaram mu aji ji rom ginaaw bi wax jooju xaw a gën a jëm kanam gën a xóot bi kenn ci paab yi nee njéggal daal man na a ame ci nit joxe ci alalam ci egliis bi ngir ñu dundale ci diine bu ko defee ñu jox nit kooku xobu njéggal luther moom dafa kontaroon njaayum xobi njéggal yi mu ne woon mucc mbaa mbugal ak fayoontoo manuñoo juge ci jënd ay xobi njéggal fa nu man a juge kay mooy gëm yàlla luther moom diiatoon na xobi njéggal yi daal di woon dem ba ca egliisub wtanberg ba wékk fa mbind mu ëmb ay diiat yu toll ci ci atum g paab bii di liyoo mu fukkeel mi amoon na taxawaay bu tar ci xalaati luuther yi ndax daal di woon nay genne ca saa sa benn saxal walla ndigalul xañ ñu teg ko luther saxal boobu walla ndigal loolu moom lanu daa wax wermis waaye luther moom faalewul woon saxal bii moom kay da koo sanni woon ca ëttub egliisu watanberg ba lakk ko xalaati martin luther ak ay gisiin yu yéwénal yi mu yoroon luther xalaati yéwénal yi mu woote woon jëme ñoo y yii di ñëw nii 	injiil mooy nattukaayub diine ak bu yoon bi muy sukkandikoo ci firi pas pas yi ak mbooleem masalay diine yi am ag wuute 	nit ku jàng ku nekk tey jëfandikoo xel sañ na a jàng injiil te firee ko ni mu ko dégge xame ko ni 	paab bi amul benn yoon àq mbaa sañ sañ ci rënkal fi boppam moom rekk sañ sañu firi injiil 	sëy daa war a dagan ci làbbe yi 	niti diine yi dañoo war a nekk ci ron kiliftéefug nguur gu àdduna gi 	wàññi limub jàngu yu bari yi tasoon ci mbooleem reewi orob gu sowwu gi bu nu xoolee xalaati martin yi dananu gis ne moom daal li ko yitteeloon mooy mu neewal doole sañ sañu paab bi loolu yaa ngi koy gisati ci bi muy sàkku nu neenal diggale gi daa am ci diggante yàlla ak ub jaamam sàkku gi mu doon def it ci nu neewal limub jàngu yi li mu doon wund mooy neewal ngañaayi egliis bi aki am amam ndax loolu man a soril egliis bi caaxaan ak po mi mu nekke woon da nga gis it ne wax ja mu waxoon ne nit ku xam ku nekk am nga àq ci jàngal sa bopp injiil ak firee ko ni nga ko dégge moom itam li mu doon tekki mooy jeqiku gu mu jeqiku woon ci egliis bi ak rafleel gu mu ko rafleeloon ci li mu jàppoon moom egliis bi ne àqi yoonam la ju mu moom jëfka yi dimbli luther mii ci wooteem gi man a àntu am na ay jëfka yu bari yu ñoo dimbli woon martin ci fipp gu yéwénal gi man a àntu yi ci ëpp solo ñooy yii 	feeñ gu luther mii feeñoon ci jamono joo xam ne waa orob yi seeni xel da cee tàmbli woon a ubbiku ñu tàmbli woon a fqu ak a dañtalu ci ëbug paab gi ak sañ sañam 	siwug njuumte ak ñaawtéef yu rëy yi nga xam ne taqaloon nanu derub paab gi te taxoon ba nit ñi doon sikk ag muccam ak ag sellam 	fonk sa xeet walla xeetu gi tàmbli woon a feeñ ci reewi orob yi te taxoon waa almaañ ñi defoon ab dank topp ci ginaaw martin luther rawati na maas gu diggu ga ak baykat ya ak gawar ya 	dimbali gu ko ustaas yu daara yu mag yu tugal yi dimbali woon ak ñu dul ñoom ci xalaatkati almaañ yi warlu woon ne ñooy fas yeenee tas xalaatam yooyu 	firi injiil ci làkku almaañ ak def ci ay taalif yu tax waay almaañ ji man a gis ay xalaatam yër it jam yi mu doon def egliis bi 	tasug móolukaayu téere gi nga xam ne gotenborg moo ko fentoon loolu taxoon nag ba xalaati luther yi tasoon ci waa almaañ yi ak ñu dul woon ñoom am na benn xeex bu mag bu amoon ci diggante martin aki gaayam ñoom ñi diy protestants maanaam ay diiatkat cig wàll ak diggante ñi toppoon paab gi katolig yi ci geneen wàll dëkki almaañ yi moom xare yu tàng a fa amoon dongay ñaari ngér yii doon xeex nag mujjoon nanoo xaatim ag juboo gu nu tudde woon augsburg atum g ñu nangu woon ci ne goxu almaañ bu nekk am na àq ak sañ sañ ci tànn ngér mu ko neex mu protestant mbaa mu katolig waaye ci wàllug ofisel ñu tànn protestant def ko diine ngérum luther mu protestant mii tasoon na te siw ci goxi almaañ yu bëj gànnaar yi egliisam daal di doge ca egliisub rom ba ak norwej finland xalaat yii tam tas ba genn almaañ dugg angalteer ak nguuri skandinaaf yi danmark ak suwed kalfen calven john calven mi ngi juddoo fraans atum g di woon ku duggoon ci ngérum protestant mu luther mi te bàyyi woon mu katolig mi kalfen walla calven juge woon na fraans dem siwis li ko waraloon it mooy sonnal gu nu ko fa doon def ngir ay sabab yu aju ci diine fii nag la tàmblee wisaare ak a tas ngérum yéwénalam mu xaw mee jege ngérum luther mi ñi ko toppoon mu tudde leen hogonoots di ci maanaa ñoñ laab ñi kalfen ak luther dëppoo woon nanu ci ay masala yu diine yu bari waaye wuute woon nanu ci ñaari mbir ñooy 	wax gi kalfen waxoon ne njéggal ci mbir yi nu doggal la te loolu luther nanguwu ko 	kalfen daa gëmoon ne egliis bi warul a topp ci ginaaw genn nguur gu adduna ne woon egliis bi daa war a am nguurug boppam gu temb gu dul wéeru ci gu adduna gi ñi war a doxal nguurug egliis bi nag ñooy am mbooloo mu xellu te am hikma xalaatam yooyu nag wisaaroo woon nanu ci reewi tugal yi ci anam gu ëppante ci fraans angalteer siwis ak yeneen swingli mi ngi cosaanoo woon siwis judd atum g ay yéwénali diineem mu tàmbli woon ko ci dëkkub siyorix atum g ci biir diiat gu mu doon def njaayum xobi njéggal yi kon foofu ag jegeente gu mag am na fi ci diggante ay xalaatam ak yu luther ak kalfen waaye teewul mu wuute ak ñoom ci lenn ci ay masalay diine swingli moom daa jàppe woon egliis bi benn campéef bu am demokraasi buy ame ak a sosoo ci mbooleem nasaraan yi nga xam ne seenug bokk ci mi ngi ame ci benn kuréel bu leen fay teewal ci mbooleem mbir ak masala yi aju ci egliis bi ak ni ñuy sampe nit ña fay ligeeye ngérum swingli tasoon na ci siwis ak ci lenn ci yeneen reewi orob yi waaye taxutoon mu siwe wisaaroo ni mu luther mi mbaa mu kalfen mi bunt bu ñaareel bi jëm kanam gu xam xam ak yewwute gu endustri doggantal gu njëkk gi jeexiitalu gi waa orob defoon ci yooni gëstu yu xam xam yu jullit ñi jamono ji xam xam neewe lool te amadi xiima ci tugal ci jamono ju diggu ji di ju ag laman moom xam xam nekkoon na ci mbooleem reewi jullit ñi di lu naat te meññi xay gu lislaam gi di woon gi gënoon a kawe ca booba ngir coona bi boroom xam xami jullit ñi daa génne ak a daj ci dundal ko ak ngir soññe gi nguurug lislaam gi daa soññe ak a jàmbaarloo ci xam xam ak boroom xam xam yi bi waa orob yi dee ñu yittewoodi xam xami gres yi ak yu leen moy fekkoon na jullit ñi ñoom ñu nekkoon ñu xam xami xay yu yàgg ya ñoroon ñu taxawoon ci firi leen ci araab xay yooyu di yu gres faaris end rawati na ci ndoktoor bidiw ak mat ak yeneen yi ñu jotoon a naan nag ci xam xami ubuqraat iqlidis aflaton ak arustoo ak ñu leen moy ci boroom xam xami gres yu mag yi boroom xam xami jullit ñi yamuñu woon rekk ci naan ci xam xami gres yi ak tuxal leen yobb leen ci araab waaye kay danu leen a toppoon wéral leen te dolli ci lu bari ci li nu feeñal wuññi ko ciy xam xam aki gëstu aki nattu yu nu amal ci wàllug ndoktoor ak mat kimyaa ak xam xami dénd yi bidiw juxraaf ak yu leen moy ginaaw bi nu amee jikko yu mag yiy joxe xalaatub xam xam bu sell ngérum walla yoonu gëstu wu xam xam ci jullit ñi boroom xam xami jullit ñi daal doxoon nanu ci seen gëstuy xam xam yi ci ngérum xam xam mu wuutewut ak mu xam xam mi am ci jamono ju yees ji ñi ngi sukkandiku woon ci yooni xam xam yoy bokkoon na ca yii xeeñtu raññale xaaj yi jëfandikoo yooni natt yi jàkkarloo làmb misaal ak jeem a àgg ca jëmuwaayu xam xam ba maanaam xam xam bi la tax a jug ak xam ngérte yi muy liy juddoo ci boo ko xamee ba noppi ngir coona yii nu daa daj nag mujj nanu di ñi jiitu ci lefum gëstu mu xam xam walla li nuy tudde yoonu xam xam wu nattu ci noonu lanu fi sampe woon kenoy gëstu gu xam xam ngir yeesal gi nu yeesaloon xam xam ci seen jamono waa tugal yi nag jariñu nanu ci wii yoonu nattu wu xam xam wi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci ki jiitu woon ci ñi ci jariñu mooy waay angalteer ji di roger bacon g g mooy ki waa tugal yiy jàppe ki raw ci gëstug xam xam ci tugal ndax mooy ki jeemoon a wutal xam xamu dénd ag noste guy sukkandiku ci nattu ak jàkkaarloo loolu nag mbir la moo xam ne boroom xam xami jullit ñi ñoo ko ci jiitu jaadu na ñu leeral fi ne roger becon mii kat ku jotoon a jàng làkku gres la ak wu yahood yi ak araab jariñu woon it ci xam xam yi nu ci bind moom nag daa gëmoon ne li tax ñu war a jàng fisiya ak kimiya ak mat ak bidiw ak xeltu mooy ligeeyal xam xam bi aju ci yàlla digg yi xayug lislaam gi jaaroon bi muy dugg orob jullit ñi dañoo nekkoon ñu rawoon ci lefi xam xam yu bari ci noonu ñu yanu woon seen xay googu yóbbaale ko ci mbooleem àdduna bi ci penku bi ak sowwu bi orob jariñu woon na bu baax ci xam xami jullit ñi ña fa dëkk it jòkkoo woon nanu ak jullit ñi jaare ko ci ay ker keraan yu bari bokk na ci yooyu 	andalusi waa orob yi jonjoo woon nanu ak digg yu xayug lisaam gi ci andalusi moom gox bii nga xam ne daa mujjoon fees dell ak leer guy jòlli tukkee ci xayug lislaam gi ko róofu woon moom bii gox barabu jòlli la woon ñeel xam xam ak dañ kumpa rawati na ci dëkki orob yi mu dendaloon bu ko defee nga gis sàkkukati xam xam yu orob yi daa jariñu ci xam xami jullit ñi di jawalsi ak a jublusi dëkki andalusi yii di talitala kordoba ak sewija ñu jële woon ci ñoom ngérum nattu mi ñu daa jëfandikoo ci gëstu gu xam xam loolu mujj yëngal bu baax xalaatiinu waa tugal yi 	dunub sisil araab yi jotoon nanoo teg loxo sisil ki joxe woon ndigalul jëf jooju di siyadatul laahi bun al axlab buurub nguurg axaaliba yi waaye mu ame ci loxol kapitenam bu siw boobu di asad bun alfuraat atum ginaaw gàddaay gi mu ame woon nag ci jamonoy xalifa bu nguurug waa abaas bi tuddoon maamun ca saa sa xayug lislaam tàmblli fa a sutuxlu sisil mujj di gilin ci gilini xam xami lislaam yi sàkkukati xam xam yepp jublisi ko rawati na ñi dëkke woon orob ngir sàkkusi fa xam xam bi norman yi nangoo sisil ci araab yi yaquñu woon xayug lislaam gi ñoom kay dañoo sawarloo woon boroom xam xam yi soññ leen ci noonu firi teerey araab yi yobb leen ci latin daal di fay tàmblee am ak a sawar waa orob yi tàmblee yër li ci yii teere ak a jariñoo rawati na itaali mi ci gënoon a jege sisil looloo waraloon muy mberum yewwute gi 	xarey jooñ yi bokk nanu bu baax ci li tax waa orob yi manoon a jokkoo ak xayug jullit ñi jokkoo gi it saxoon na fi lu tolloo ak ñaari xarnu ci biir ñaari xarnu yii orob jot na cee tuxal lu bari ci xam xami lislaam yi ame ci it walla tege ci loxo lu bari ci teere yi nu taalifoon ci araab ak yi nu firi woon jële leen ci làkku gres end ak faaris 	jokkoog yaxantu gi amoon ci diggante reewi jullit ñi ak orob rawati na li ci itaali jotoon a def mu bokk ci li sababoon jonjoog xay ci diggante ñaari dëkk yi 	siyaare gi nasaraan yi daa defsi ci seen barab yu sell yi nekk palastiin nga rax ci dolli tukki yi waa orob yi daa defsi ci reewi jullit ñi ak la ca juddoo muy ñu gis te jariñu ci xam xami jullit ñi ak seeni xay jullit ñi daal ñoo waral jëm kanam gii nga gis ci orob ci jamonoom ju bees jii xam xam yi bàyyi ay jeexiit ci waa tugal yi lim mat jullit ñi naanoon nanu ci xam xami kalkil yi nekkoon ca waa end yu yàgg ya ñu jotoon a jànge ca ñoom ni nuy defe ay lim numero waaye nag nu sellal ko gën koo teg ci yoon boroom xam xami jullit ñi ñoom defoon nanu ay dollent yu am solo ci xam xamu waññ calcul ñoo dolli woon tus ci lim yi ndax amu ci woon bi nu leen di jël ñu indi màndargam al kasr alhasarii di ci wolof damat ci fukk ñu taalif ci wàllug xam xamu waññ calcul ay teere yu waa orob yi firi ci seeni làkk te jariñu ci boroom xam xamu jullit bii di muhammad bun muusa alxuwarsamii nekkoon na di ku aay ci xam xamu lim walla waññ moom de lanuy sant bu lim mumero yi nekk ci kalkil duggee orob tay xawaarsamii mii aayoon na it ci beneen xam xam bu yees mooy aljabr moom sax mooy ki ko sos far taalif na ci tollale ci aljabr nu tekki ko ci ginaaw bi ci làkki orob yu bari boroom xam xami orob yi jariñu ci boroom xam xami jullit ñi jëfandikoo nanu ay junj ci matematig yi xam xamu lim ñoo njëkkoon waa orob yi ci wàllug matemetig gu yees gii bu dee nag ci andasa ak xam xamu ñattal yi jullit ñi ñoom yamuñu woon ca la woon ca waa gres yi rekk nga xam ne seen boroom xam xam bi nu naan iqliidis moo ko feeñaloon waaye jotoon nanoo feeñal ay masalay andasa yu bees ñu duggal li nuy wax al mamaas ci xam xamu kalkilu ñattal nu jël li nuy wax juyuub poos wuutale ko ak li nuy wax awtaar buum nu fecci itam toolale yu nu kaabaal yi nu xootal bu baax tam ci xam xam yu nuy wax maxruutaat boroom xam xamu jullit bi nuy wax omar alxiyaam defoon na lu mag ci wàllug mat moom de bokkoon na ci ñi gënoon a ràññiku ci boroom xam xami jullit ñi ci wàllug matematig ci ñeenteel bu njëkk bu xarnub fukk ak ñaar g xam xamu fisiya li nga xam ne sikk amu ci mooy ne jullit ñi jariñu nanu ci xam xamu fisiya ci waa gres yi bi nu ko tekkee ci seen làkk waaye ñu gën koo yaatal dolli ci ay masala yu fisiya yu bari nu màndaqe walla natt diisaayu yolaakon yi nu fent ay màndaqekaay yu xereñ ñu xamale ay gisiin yu bees ci xam xamu kàddu ak gis basariyaat ak séen almariyaat boroom xam xam bu jullit bii di abo yuusuf yahquub ishaq alkanadi mi nga xam ne mi ngi faatu atum g moom ku aayoon ci xam xami gis yi la taalif na ci ab teere bu am solo mooy teereb yu nu xool yi nga xam ne waa orob yi mujjoon nanu ko o tekki ci làkku latin roger becon jariñu ci ak liyonardo da vinci ak boroom xam xam bu poloñ bii di copernice g boroom xam xamu jullit bii di abo aliyu muhammad bun alhasan bun alhaysam g moom mu nekkoon di ku aay ci xam xamu fisiyaa mu soppi xam xamu leer bu yàgg ba indi fi xam xamu leer bu yees bi mu amoon ndam ci indi fi gisiinu xam xami seen yi mu firi feeñteg xònn ak safaanu gi ag leer di safaanu ak ni muy dammoo bu boroom xam xamu gres bii di batlimos jàllee kii di ibnu haysam moom lanuy jàppe boroom xam xam bi njëkk a def ay wuññi ci xam xamu gis haysam defoon na ay taalif ci xam xamu yu nu gis yi ak xaaji bët ak weer yi ak leer ak yeneen waa orob yi it yii taalif tuxaloon nanu leen ci seen làkk wii di wu latin ci xarnub fukk ak ñatteel g ak ci yeneen làkk yu orob yi loolu dimbli leen ci nu jariñu bu baax ci xam xam yii nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci bu baax xam xamu bidiw jullit ñi yittewoo woon nanu xam xamu bidiw xawarsimii moom defoon ay natt ci yëngug bidiw yi xam fi nuy fenke ak fi ñuy sowe jullit ñi jariñu woon nanu ci xam xamu bidiw ci waa geres yi ci noonu ñu firi woon ci araab lenn ci teerey bidiw yu geres yi niki teereb batlimos bi tuddoon ñeenti wax yi boroom xam xam bi ko tuxaloon ci araab di aboo yahyaa albatriix ci jamonoy abo jahfar almansuur doomi muusaa bun saakir ñoom itam taalif teere bi nuy wax aljadaawil alfalakiya yeneen boroom xam xami bidiw it feeñ niki saabit bun xurra haniin bun ishaqa alhibaadi ak bataani mi faatu atum g ak ñu dul ñoom jullit ñi tabaxoon nanu ay fuglukaayi bidiw ca dimasq baxdaad kordoba ak sawija di woon ay dëkki lislaam abo abdillaa albattani mii dees na ko lim muy ki gën a bàyyi ay jeexiit ci anam gu xóot ci waa tugal ci boroom xam xami bidiw yu jullit yi waa orob yi ñoom jariñu nanu bu baax ci xam xamu bidiw ci jullit ñi ak ci li jullit ñi jot a gennewaat ci anam gii ciy wuññiy xam xam jullit ñi fésoon nanu ci xam xamu kimyaa jaabir bun hayyaan alkoofii bokkoon na ci ñi gënoon a siw ci wàll googu moom mi doon def kimya te taalifoon ci ab jimblang jabbir leeraloon lu bari ci way toggale yu kimya yi nu xamutoon bu njëkk niki aji wex ju nitrik ruug nasaard botaas soda al kawiya ak aji wex ju asotik ak yeneen mu leeraloon ba tay jefi kimya yi niki seebal ak leeru ak yeeg ak toqqal da na jaadu nu leeral ne xam xamu kimya moom danu ko daa wooye xam xamu jaabir ngir li ko ci yàlla tawfeexaloon ba mu man a topp yoonu xam xam wu nattu wi nga xam ne ci la jaaroon ba man a àgg ci ay dëgg yu kimya yu bari waa orob jariñu nanu bu baax ci xm xamu kimya bi ci jullit ñi ci noonu nu firi taalifi jaabir yooyu ci seeni làkk xam it lu bees li ci jullt ñi dolli ndoktoor boroom xam xami jullit ñi rawoon nanu ci xam xamu ndoktoor sartoon nanu ci seen boroom xam xam mu xam siddi xam jëf ak warteefi cer yi ak noyyi ak soppikum saw ñoom de ñu sonnoon ci xam xamu siddi lanu woon firi woon nanu xam xami geres yi ci aju woon ci làkku araab bi nu noppee ñu taalif ci teereb ibnu nafiis bi tudd tasriihul xaanuun dolli na ay xam xam yu am solo ci xam xamu siddi jullit ñi jàngale nanu doxug dereet sonn it ci mbooleem xeeti tawat yi xamale itam deewal bi nuy faral a def ci ligeeyu xotti ki niy wax razi te faatu atum g feeñ na te raw ci ndoktoor taalif na ci lu sakkan ak ibnu sinaa mi faatu atum g moom de kenn la ci boroom xam xami jullit ñi gën a siw ci ndoktoor teereem ba tudd xanuun fit tibb de jenn jimblang la ju xam xamu ngoktoor ju waa penku ak sowwu ñepp xam ak abo xaasim xalf mi gënoon a fes ci xottikati xarnub fukk ak benn g ak ibnu zahr boroom teere bi tudd mubtakaraat fil jiraaha waa orob yi jariñu nanu ci xam xamu ndoktoor bi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci ñu jariñu ci ni nuy siddee ak ni nuy gennee tawat yi ak ni nuy faje ak ci xam xam yi nga xam ni teerey jullit yi làqoon nanu leen ci wàll gii ginaaw bi nu leen firee ci làkki orob yi waa orob yi jële nanu ci jullit ñi tabax ay fajuwaay ak jëfandikoo deewal ak li nuy wax kaaw su nuy opere xotti waa orob yi ba tay jariñu nanu bu baax ci xam xamu xeltu bi nga xam ne jullit ñi ñu ci rawoon lanu ci noonu nu jàngoon taalifi kanadii faarabii ibnu sinaa ak ibnu rusdi ak ñu dul ñoom ginaaw bi nu leen firee ci seeni làkk bokk na ci boroom xam xami orob yi gën a siw ci jariñu ci jullit ñi ak seeni xalaat paskaal dikart hiyom ak becon ak ñu leen moy waxtu wi yaatuwul ngir nu man leen a indil ngértey xam xam yu bari yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci ci seeni gëstu te booba orob a ngi ci ngëmmeenam li ak lëndëmug reeram gi ci ron nosteg laman ak cangug egliis bi da na yell nu leeral ne xam xam yi ak ngértey xam xam yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci dañoo tàmbli woon a tuxu ndànk ndànk jëm ci reewi orob gu sowwu gi ginaaw bi ab kureel ci waa orob yi xamee solos xam xam yii te taxawoon ci firi leen ci seeni làkk ay firikati orob yu bari feeñoon ci loolu ku ci mel ni costantinus africanus herman the cripple ak eugenius mu parlermo mi ak ñu dul ñoom kon lu nu war a xam la ne yewwuteg xam xam ak gu endustri gii am ci reewi orob yi ci ginaaw yewwute gi du lu moy meññat ci meññati nattu ak gëstu yu xam xam yi nga xam ne orob tuxale na leen ci xam xami lislaam ci digg jamonoy xayug lislaam gi coonab gëstu yooyu nag ñooy cëslaay yi nga xam ne ci la jëm kanamug xam xami dëppale yi ak yu xarala yu bari yii tegu ci adduna ju xay jii ngay gis tay doggantal gu ñaareel gi wàll yi xam xam jëme kanam ci tugal xam xam naat na te jëm kanam ci orob ci biir xarnu yii bu fukk ak ñeent fukk ak juroom ak fukk ak juroom benn g loolu bokk ci li waral jëm kanamug xam xam gu mag gii orob gis tay ci jamonoom ju yees jii nu nekk nga xam ne ci la yewwuteg xam xam juddoo ak gu endustri ci orob ak li topp ci loolu ci njariñ yoy du orob rekk la ñeel waaye àdduna bépp li taxoon xam xam jëm kanam jëm kanam gii xam xam jëm kanam tay ci reewi orob gu sowwu gi am na ay balluwaay yu wuute yi ci ëpp solo di 	tuxal xam xami jullit ñi ak firi leen ci làkki orob yi te jariñu ci 	ak feeñ gu ab lim xëy feeñ ci boroom xam xami orob yi amoon ag cofeel ci gëstu yi aju ci xam xam 	yokku gu yëngu yëngug firi ak taalif yokkuwoon rawati na bi nu fentee móolukaay yi 	xeemmeemteef gu waa orob yi amoon ci dundalaat xam xam yu yàgg ya yu gres rom ya wàll yi xam xam jëme kanam ak li nuy misaal jamono yu diggu yi ci orop lepp naan jamonoy reer la ak lëndëm teewul ay ceññeeri xam xam yu kenn mant a reere mant a weddi amoon fa li am daal mooy wuññiy xam xam yi ci jamono jii du woon yu yaatu lu neew la woon ci noonu xam xamu waa orob yi nekkutoon lu moy li nu xame woon ci waa geres yi ak ci jullit ñi ci seen ginaaw maanaa mi xalaati waa orob yi ame woon soppiku woon na ci jamonoy yewwute gi ginaaw bi nga xamee ne gëstuy xam xam yi fa ñoom dafa mujjoon tegu ci nattu ci noonu orob jot na a am ndam ci jëmale kanam xam xam ci wàll yu bari yi ci ëpp solo di ndoktoor ndoktoor ci orob wëyoon na di sukkandiku ci li fi waa geres bàyyiwoon ak li fi jalinos jot a indi ak hiboqrat ak ndoktoorug jullit ñi jaare ko ci seen teerey ndoktoor yi nga xam ne waa orob mujjoon nanu leen a firi ci seeni làkk xam xam bi orob ame ci ndoktoor weesuwutoon fii ba ci xarub fukk ak juroom benn g waa orob yitewoo woon nanu bu baax xam xamu ndoktoor ñoom daal ñoo ci gënoon a sonn ñu dul woon ñoom rawati na ci xarnub fukk ak juroom benn g moom dey xarnu la bu fekke ay xew xew yu bari yoo xam ne ñoo waral ag jëm kanam gu mag ci wàllug ndoktoor ci orob bii xarnu daal seere na ay yëngu yëngu yu wuññi yu juxraaf ak tuxug ay mboolooy gaal yu yaxantu ak ay gàddaay ci ay mbooloo ngir dëkk ji ci reew yii nuy door a wuññi aki xare yu tar te yàgg yu amoon ci orob te sababoon ay tawat yu metti aki mbas yu nu xamutoon ci orob mu mujj nag bokk ci warteefi doktoor yi ci orob ñu jeem a xam yile tawat yu yees ak nu nu leen di faje wutal leen ay garab ci noonu boroom xami xami orob yu bari feeñ ku ci mel ni fisaliyos mum beljik mi frakastor mu itaali mi ak gonte andarnax mu almaañ mi nekkoon doktoorub fransuwaa mu njëkk mi doon buuru fraans ak lofan hok mu oland mi ak luwis pastor mu fraans mi ak kox mu almaañ mi añs bu ko defee waa tugal yi xam jàngoro yi xam it nu nu leen di faje ju ci mel ni daftiriya judri tifos kolera tifod añs juxraaf ak bidiw xalaat bi naan suuf si daa tàllaliku daal te boroom xam xami bidiwi gres yi indi woon ko fi moo nekkoon xalaat bi tasoon ci tugal gëpp ci jamono ju diggu ji ak doonte lenn ci boroom xam xami gres yi waxoon nanu lu ko safaan ne suuf si moom tàllalikuwul daa bulu kay mel ni ab kol kol boroom xam xamu gres bii di batlimos moom doon na def ay ligeey ci googu wàll waa tugal yi nag seen xam xamu juxraaf ñi ngi ko doon gën a jëmale kanam jaare ko ci li nu xame ci wuññiy juxraaf yi ak ginaaw bi ci noonu xam xamu juxraaf tàmblee jem kanam ci orob jem kanamug xam xamu juxraaf tax na ba bu bidiw it jem kanam kii di koperniks di boroom xam xamu poloñ moom siwoon na ci lefum xam xam mu tugal mi moom dey duggal na loxoom bu baax boo xoolee ligeeyam yi aju ci xam xamu bidiw ci doxug xam xam akug jëmam kanam ci tugal kopernic moom àndutoon ci gisiinu batlimos wi doon wax naan suuf si moom daa bulu ba noppi nekk ci digg adduna bi bu ko defee nekkteefi asamaan yi di ko wër kopernics moom ne suuf si daal ak yeneen nekkteefi asamaan yi ñoom ñepp danuy wër jant bi te suuf si nag am na wërug boppam gu muy wër ab diggam ci waxtu yu nekk mu neeti suuf si dafa wëndeelu maanaam roo te wëndeeloom googu nag tax na ba day yor doxiin walla yëngu yëngu gu roo mbaa guy wëndeelu waaye nag lu ñaaw la lool copernic ñàkk a man a tas te wisaare xalaatam yooyu ci bi muy dund ngir rekk ragal gu mu ragal jàngu bi egliis bi xalaatam yooyu wisaarewunu leen mbaa nu tas leen ndare ci atum g muy at mi mu faatoo boroom xam xamu itaali bii di galileo g moom jug def lu rëy ci jëmale kanam xam xamu bidiw loolu gën na a am ci ginaaw bi mu jëfandikoo fésalukaay ngir fuglu bidiw yi ak nekkteef yi ci kaw asamaan si mu dëgëral itam xalaati kopernic yi xam xamu fisiya gën na a jëm kanam te gën a buur ci xarnub fukk ak juroom benn g bu ko defee nga gis boroom xam xam yi ñuy dàggasante ci masalam yëngu yëngu ndaxte yëngu mooy cëslaayu xam xamu fisiya bu arusto maanaam ci la xam xamam boobu tegu boroom xam xami tugal yi def seen yite ci ñòddi gi nekk ci suuf si boroom xam xamu itaali bii di galileo di ku rawoon ci wàll googu moom de ci atum g yeegoon na ca sooroolub pisa bu jeng ba jël ñatti yef sànni leen ñu rotandoo ci suuf galileo mii moom lanuy jàppe ki gën a am solo ci boroom xam xami tugal yi daa yitewoo xam xamu fisiya ndax kat mooy ki teg dàtti walla fondmangi xam xam bii ci tugal ci fukk ak juroom ñaareelu xarnu g boroom xam xamu angle bii di isaac newton g mooy ki feeñal dooley ñòddi gi nekk ci suuf si moo wax ne bidiw yepp walla plaanet yepp danuy wër jant bi ci ay ngunu yu sax walla ay nekkuwaay yu sax yoo xam ne ñòddi gi nekk ci jant bi moo leen di nos te di leen teg ci yoon ki nuy wax laplace g moom itam ñëw sonn ba xam ni bidiw yi sosoo waa tugal yi tuxale nanu ci jullit ñi xam xam yu am solo yu aju ci xam xamu kimya bu bees bii nga xam ne boroom xam xamu jullit bii di jaabir bun hayyaan fésoon na ci lool te amoon ci ag raw ñoo leen xamal alkol soda gudrong saabu ak yeneen toggaliiti kimya yi nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci toggaliit yii ba leegi da nga ciy gis yoo xam ne turi ay jullit lay yore waa tugal yi nag ñoom danoo gën a jëmale kanam xam xamu kimya ci ginaaw yewwute gi ci noonu kii di josef priestley am tawfeexu di ci waa tugal yi ki njëkk a jële oksijen ci xoromi siibix atum g te loolu kat fekkoon na boroom xam xamu jullit bii di jaabir xamoon ko bu yàgg lavoisier di boroom xam xamub fraans di ki feeñal gaasub njëlbeenu oksid korbon atum g waay almaañ jii di rontgen g moom ñëw feeñalal ñu ceññeeri iks atum g boroom xam xam bii nuy wax thales di ku dëkkoon gres moo seetlu woon dooley ñòddi ju nekk ci kuran bi mu ko wokkee loolu mooy li nu njëkk a xam ci kàttanu kuran boroom xam xamu angle bii di william gilbert nekoon doktooru buuru angalteer bu jigeen bii di elisabet mu njëkk mi moom itam ñëw feeñal ne am na yeneen ne ne yuy am ag ñoddi boo leen jonjee yu dul kuran rekk feeñalug loolu nag mi ngi ame woon ci lu tollook atum g boroom xam xamu almaañ dikk fent ab jumtukaayu kuran buy juddal kuran atum g ki nuy wax stephen gray dikk won nu ni nuy tuxale kuran jële ko ci barab yobb ko ci beneen jaare ko ci fiil yu xànjar wolt mu itaali mi di ki wone duusi kuran yi te fent batari borom xam xamu amerig bii di bengamin franklin di ki wone ne melax ak kuran benn lanu mooy ki fent fegukaayu dënn misel faraday dikk moom itam di ki feeñal yoon woo xam ne ci la nuy jaare di genne kuran bu bari atum g waa tugal soobu nanu ci xam xamu mat waay itaali jii di tartaliya def ci lu am solo boroom xam xamu frans bii di fiit jëfandikoo woon na ay araf ci xam xamu jabru bii nga xam ne ci jullit ñi la ko waa tugal yi jële leodardo da vinci nag moom ci boroom xam xam yi sos xam xamu jiyoloji la bokk moom mi dëkkoon itaali jims hitn g itam ñëw di ki xamale ni doj yi nekke ak ni nuy sosoo jamonoy yewwute daal ci orob mooy jamono ji goreel xelum tugal mi te feexal xalaatam yaatal ko musal ko ci tënk tënki jamonoy orob ju diggu ji ba tay dees na ko jàppe muy jamono ji xayale te waajale ba xam xam man a jëm kanam man a naat ci tugal naataangey xam xam gii nga gis ci tugal ci jii jamono de dara waralu ko lu dul jamonoy yewwute ci jii jamono la ay jeem yu xam xam yu dëggu am yu sukkandiku ci yoonu xam xam wi jullit ñi fentoon bu yàgg lool njëkk waa tugal yi di ko xam ñatteelu doggantal yewwute gu endustri li mu jagoo ay màndargaam li mu fi indi yewwute gu endustri ci tugal ñi ngi ci jublu soppiku gu mag gi fa amoon ci wàllug endustri walla jëm kaman ga fa amoon ci wàllug jumtukaayu mekanig rawati na ci biritani ci ñatteelu xaaj bu mujj bi ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g waaye nag moom endustri mii yàggul dara mu tàmblee tas ci tugal nànk nànk ak amerig la ko dale ca njëlbeenug fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g bi mu ko defee nag ay jeexiitam tas ba àgg ci pàkk yu bari ci adduna bi loolu nag ci ñaari xarnu yii la fukk ak juroom ñeenteelu xarnu ak ñaar fukkeelu xarnu g endustri yi nag masuñoo dañ di jëm kanam ak a awaase ba ci sunu jamono jii nu toll looloo waral du man a ñàkk nu xam sabab yi tax yewwuteg endustri am ci tugal sabab yi tax yewwuteg endustri am ci tugal 	awaase gi xam xam awaase ci tugal ci jamonoy yewwute moo waral yewwuteg endustri am 	dëkki tugal yu mag yi am gi nu am ak tegu gi nu tegu ci yaxantu ak endustri ak woomleg koom gi loolu di jur nga xam ne day tax ba endustri di jëm kanam rawati na bi ci aju ci ràbbu ser nga xam ne mooy endustri bi njëkk ci tugal 	jëmm ci tugal ni mu jekki jekkee rekk fés mujj di dàtt bi mboolaayi orob yi tegu sabab la ci li yee waa tugal yi moom jëmm jooju ci orob ku nu tënk la woon ci jéngi nosteg laman jamonoy yewwute ñëw dog jéng yooyu feexal am xelam leeral ko ci xam xam ba mu man a xalaat bay fent ay jumtukaay yu am solo yu koy dimbli ci yombal ag dundam 	li juddoo ci wuññiy juxraaf yi it muy teg loxo gi reewi sancaan yi daa def reew yi nu sanc ak di fa jële ay xeewal aki ne ne yu nu laalagul di leen yobbu seeni reew loolu it bokk na ci li jëmale kanam yewwuteg endustri gi ci tugal 	reewi tugal yi ak këri koppar yi jàpple gi nu doon jàpple naal yi jug ngir jëmale kanam endustri ci orob loolu de ci li defar jawwu ji la ba endustri man a dox man a àntu 	boroom xam xam yu aay yi xëy feeñ te bari ci tugal 	bari gi ligeeykat yi bari ci tugal rawati na ñiy ligeey ci endustri yu ndaw yi na ngeen xam nag ne lu bari ci fentkati angle yi daa defar ak a fent jumtukaay yi ak masin yi ci ligeeykat yi amoon xam xam yu neew lanu woon nga xam xam ne daanaka jàngunu woon yewwute gi li mu jagoo woon ak ay màndargaam yewwuteg endustri ci tugal daa jagoo woon ay mbir yu bari yii ci lanu 	jëmale kanam gu nu jëmale kanam jumtukaayu ëcc ak ràbb meccem ràbb daal ci yi gën a jariñu ci fent yu xam xam yi aamoon ci tugal la rawati na ci britani loolu di ci ñeenteel bu mujj bi ci xarnub fukk ak juroom ñatt g loolu nag li ko waral mooy yitewoo gu tar gu nit yitewoo ay sér ak ñàkk a jafeg jëfandikoo jumtukaay yi ngir ligeey ci ràbbkatu angle bi nuy wax james hargreaves jot na a fent atum g benn jumtukaayu defar wëñ muy benn masin bu loxo bu nuy jëfandikoo ci ëcc li koy doxal nag doon genn mbege walla pono bu yor juroom ñatti ëccukaay ak ñaari forukaay bu ko defee benn ligeeykat di ko yor di ko doxal bu ko defee fentkat bu angle bii di richard arkrihgt fent moom it atum g benn jumtukaay buy xëcc wëñ yi moom nag jumtukaay la bu nu daa doxale ci dooley ay fas mujj nu koy defe ci dooley ndox nu tudde woon ko kaadaru ndox bi water frame ki nuy wax samuel compton ñëw fent atum g benn jumtukaay buy boole gaaw ci ligeey bi ak baaxle ko boobu jumtukaay nag tasoon na ci fi dend ak barabi ndox yi ci ñaari goxi angalteer yii di yorkshire ak lancashire ki nuy wax edmund cartwright moom itam àgg ci fent benn jumtukaay bu nuy doxale dooley ndox ginaaw bi nu koy doxale dooley cóolóol te kat tax na ba nu man a ful li nu daa ràbb daa ko defar ciy sér ligeey bi nu daa def ngir gën a jëmale kanam ak gën a rafetal ligeeyu ëcc beek ràbb bi gën a dolliku te sax nu àgg ci jëfandikoo ne ne yu kimya yi ngir raxas wëtéen wi defarati yeneneen jumtukaay ngir móol ay deseñ aki mbind ci ndima yi nu ligeey 	jëfandikoo kàttan jumtukaay yu njëlbeenu yi amoon nit a ko daa doxale ci dooleem walla dooley dundat kàttan nag di energie jëm na kanam ci jëm gi jumtukaay jëm kanam te awaase ci noonu nit jot a jëfandikoo ci njëlbeen gi dooley ndox ngir doxal jumtukaayam yi mu fent bu yàggul ginaaw bi mu jëfandikoo dooley cóolóol ak këriñ ki nuy wax thomas newman ñëw indi fi jumtukaayu cóolóol james watt moom itam dikk gën a defaraat jumtukaayu thomas boobu atum g loolu waral ay soppi yu mag yu xóot ci wàllug ligeey bi ak li nuy ligeey ndax kat duggal gi nu duggal jumtukaay bu mekanig bu cóolóol ci endustri ak jokkoo lu rëy a rëy la te am solo te moo tax ba nga gis endustri tay mu toll fii mu toll bu ko defee ca saa sa waa tugal yi tàmblee gëstu fu nuy jële këriñ këriñ nag bari woon na lool ci wels gu bëj saalum gi ak skotland nit it gënoon na a jeego ay jeego ci jëfandikoo gi muy jëfandikoo kàttan mu feeñaloon petrol ca d b a diiwaan yu bennoo yu amerig yi ci digg fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g ginaaw bi nu gisaat petrol fu bari ci adduna bi ginaaw bi nu fentati benn jumtukaay buy lakk ci biir boo xam ne mooy soppi petrol bi ginaaw bu ko lakkee def ko kàttan guy yëngal ak a doxal loolu moo waral ngay gis leegi jumtukaay yu mekanig yii nga xam ne danuy sukkandiku ci li nuy wax lakkug biir gi mooy lakku gi petrol bi di lakku ci biir jumtukaay bi jumtukaay yooyu nag ñooy yu mel ni oto yii ngay gis fafalnaaw yi gaal yii nga xam ne lakkug biir gee leen di doxal añs kuran tam jariñ na nit lu bari loolu nag mi ngi ame ci bi kii di faraday juge fent li nuy wax juddalukaayu kuran nga xam ne loolu indil na nit lu bari ci ay ligeey ak njariñ ci dundam nit àgg na ci xam kàttanug saal te jëfandikoo ko ci anam yu bari loolu tax mu man a neewal li muy sukkandiku ci petrol waaye nag nanu xam ne kàttanug saal moom lu seer la manu fee wuutu petrol ci genn anam nit it jot na a xam kàttan gu jant gi te jëfandikoo ko ci yenn anam yi niki nuggalukaayu ndox yu jant yi nuy jëfandikoo ci kër yi ak ci yeneen anam yi 	jëm kanam gu endustri bu weñ jëm kanam bokk na ci lu am solo li yewwuteg endustri gi jagoo bokk na ci jëmale gi nu jëmale kanam endustri bu weñ loolu nag mooy bi angle bii di bassemer jugee fent yoon woo xam ne manees na cee jaar bay soppi weñ di ko def sulb mooy weñ gu wow kong dëgër këng loolu nag ni mu daa ame mooy nu jaarale ko ci tàngoor wu kawe lool nit it gënoon naa def ay jeegoy jëm kanam ci wàllug yoon yi muy jaar bay genne këriñ loolu tam dimble ko ci mu man a dolli gën a lëwal li muy ligeey lii lepp nag bokk na ci li waral yewwuteg endustri gi man a am ci tugal rawati na ci britani 	jokkoo gën a jem kanam gu mu gën a jem kanam li kenn manul a sikk mooy ni endustri jëme kanam ci tugal de indi na fi ag jëm kanam ci wàllug jokkoo rawati na bi ligeeyu weñ gënee dox gën a jëm kanam ci noonu angle bii di george stephonson moom ñëw fent saxaarug coolool maanaam muy daw ci ay banti weñ ci diggante dëkkub liverpool ak manchester ci atum g yoonu weñ wii mooy yoonu weñ wi njëkk ci adduna bi ginaaw bi nitug amerig kii di robert foulton moom dikk jëfandikoo coolool di ci doxale gaali dex yu ndaw yiy daw ci dex yu mag yi nekk ci amerig gu bëj gànnaar gi ginaaw bi mu jugati jëfandikooti cóolóol dawal ci gaali cóolóol yu mag yii di daw ci geej yeek mbàmbulaan yi ci noonu la jokkoo tàmblee jëme kanam nànk nànk ni ko endustri defe bu ko defee feeñteg jëm kanam ci wàllug jokkoo mujj di feeñte giy raññale tey màndargaal yewwuteg endustri gu mag gii am tay ci adduna bi 	feeñug campeefi endustri yi ligeeyuwaay yu ndaw yi juge nanu ci kër yi doon leegi ay campeef yu endustri yu mag yu nekk leegi ci dëkk yu mag yi endustri yi mujj di loo xam ne am mbooloom ay lonkoo yu endustri yu mag ñoo koy moom ñooy lonkoo yooyu nga xam ne ñooy faral a moom li ëpp ci alal yi isin yu mag yi nag ci wetu barabi ne ne yu nu laalul yi lanu daa faral a sampu te loolu da leen daa dimble ci ñu man a neewal seeni fere ci lu aju ci seeni ligeey ndax loolu daa na tax li nu ci waroon a ñàkk gën a neew neewug fere yooyu daa na feeñ bu baax ci njëg yi ndax daa na leen daaneel te daa na gën a baaxal ligeey bi gën koo wuuteel li fi yewwuteg endustri gi jur maneesul a sikk ne yewwuteg endustri gi indi na ci tugal ay ngérte yu yaatu ci wàlli koom politig ak mboolaay li mu fi indi ci wàllug koom yewwuteg endustri gi bàyyi na fi ay jeexiit yu rëy ci wàllug koom ci biir orob ak biteem ndax ca la isin yu mag yi tàmblee feeñ yi daa am jumtukaay yu rëy yi li nuy ligeey gën a yokk gën a wuute li nu koy jënde gën a neew ñepp man cee jot jumtukaayi ligeey yi gën a bari jokkoo gën a yomb yoon yi gën a bari ja yu adduna yi gën a yaatu lonkoo yu mag yi amoon ay gis gis aki xemmemteefi rënk ak sanc tàmblee booloo ndax kat sanc gu politig gu yees gii du lu dul doomi sanc gu koom koom gi tugal daa def jaare ko ci endustreem bu jëm kanam bii ak baaxug ay jumtukaayam ak soxla gu tar gu mu soxla ne ne yu nu laalul yi ak soxla gu mu soxla ay ja yu yees yu mu man a jaaye marsandiisam yu bari yii te wuute waaye mbay nag moom ak li ay jumtukaayam gën a jamonoo lepp ak li mu gën a ñaw lepp te gën a xam xame teewul ay njëgi li ciy juge gën a seer li ko waral mooy li ëppoon ci baykat yi danoo gàddaayoon àll yi dem ci taax yi fi isin yi nekk ngir man fa a ligeey ndax la nu daa gañee ci ligeey bi moo daa gën a bari te daa nanu ci ame ag sax fi barab gàddaay gii nag juge ci àll yi dem ci taax yi taxoon na ba ab kiris walla jafe jafe bu rëy amoon fi ci wàllug mbay ci orob rawati na ci angalteer joxalanteg yaxantu gën a yokku ci adduna bi nga gis reew yiy defante ci seen biir ay kollarantey yaxantu ak yeneen kollarante yu aju ci yombalug jaarale marsandiis yi ci geej yi ak mbàmbulaan yi ak barabi romb yu adduna yi ci noonu lonkooy yaxantu yu adduna yi nga xam ne seeni boroom danuy am alal lool tàmblee feeñ bank yi tàmblee yëngook a sawar ak këri koppar yi li mu fi jur ci politig sanc gii tugal tàmblee sanc reewi jàmbur yi ak di leen teg loxo bokk na ci li fi yewwuteg endustri gi indi wuutal ko fi ginaawal ko fi ci wàllug politig ndax ni ma la ko waxe woon ci ginaaw endustri day soxla ay ne ne yu nu laalul te loolu danu ko daa gis feneen fu dul tugal te loolu jur na ay xare ci diggante ay reew ci fu bari ci sunu adduna bii tax it ba reew yi nu sanc jug di xare ngir goreel seen bopp soril senn bopp ag sanc ak lepp lu ko jege ci xeeti moomadi sa popp ak tembadi bu ko defee benn dal daal di feeñ ci orob mooy dalu koom koom bu gore bi walla bu libre bi am te taxaw ci nosteg bopp alal loolu nag mi ngi am ci ginaaw bi endustri bu yees bii soppikoo dem ci noste gii li ko waral di yitewoo gu bari gi mu yitewoo ci nu sos ay isin yu mag ak isin yu mag yii yitewoo gu tar gi nu yitewoo alal ju bari ngir taxawal leen sos leen goornamaay tugal yi jàpple woon nanu noste gii te dëgëral ko ci mbooleem li nu man am ko ciy man man aki kerkeraan ci noonu warteefi goornamaa yi gën a yaatu gën bari ci mboolaayi endustri yi loolu yobbu ko ci ay warteef yu mel ni sonn ci mbiri mboolaay yi te yittewoo leen sosal leen ay jàngu aki daara yu mag ak sonn ci mbiri wér gu yaram ak lepp lu yitteel mboolaay gi maanaam societe bi ci noonu ay boroom xam xam aki bindkat daal di feeñ yoo xam ne seen ligeey bepp ñi ngi ko jëmale ci luy dundal mboolaay gi suqali ko ay gisiini politig yu yees feeñ yoo xam ne bokk nanu ci li fi indi xalaatu politig bu tugal bu yees bii tay goornamaay tugal yi duggsi nanu ngir aar ligeeykat yi ci noonu ñu yamale waxtu yi nuy ligeey def leen leegi ñuy waxtu te bu njëkk waxtu lanu woon ñu ñëwati indi fi noppaluy tawat yi ak yu jeexiitalu ayu bis yi ak yu at yi ñu defati ay ligeey ngir yekkati seen payoor yi jeemati ba seenug dund ak seeni dëkkuwaay gën a baax man gi reewi endustri yi man a doxal seen mbiri reew feeñ na te am bi reew yooyu amee alal ju doy ak ngànnaay yu yees te xereñ bu ko defee nga gis reewi tugal yi sukkandiku ci endustri ëpp doole fuuf yi sikkandiku ci mbay ak ngànnaay yu yàgg yi nu miinoon li mu fi jur indi ko fi ci wàllug mboolaay yewwute gi ci orob jur na ay gàddaay yu mag juge ci àll yi ak dëkk dëkkaan yi dem ci taax yi ak dëkki endustri yi loolu nag mi ngi am ci bi isin yi yokkoo jumtukaayi endustri yi gën a xereñ cig wàll moomeeli mbay yu mag tàmblee feeñ ci tugal la ko dale ca ñaareelu xaaju xarnub fukk ak juroom ñatt g rawati na ci angalteer ci geneen wàll bu ko defee baykatu orob bi moom gisoon ne li ko gënal daal mooy mu dem ci isin yii nga xam ne li nu koy fay moo gën a wóor te gën di lu nu xam te bàyyi mbay mii nga xam ne leeg leeg mu baax leeg leeg du baax ak jafe jafe yi mu àndal muy njaay meek toppatoo gi lii mooy li waral ñiy ligeey ci mbay neew te wàññiku ñi dëkke kaw gi gën a neew loolu it jur yokkug ñi dëkke ci taax yi bu ko defee am lu juddoo ci loolu mooy neewug jóoxiitum mbay mi te loolu it tax na njëg yi aju ci mbay ak li ciy juge gën a seer beneen jafe jafe daal di juddooti mooy bu aju ci dëkkuwaay ñeel way gàddaay yu bees yii gàddaaye kaw ga ngir dëkksi ci taax yi di wër ligeey ci noonu ay barabi dëkkuwaay yu xat tàmblee feeñ ci wetu fi isin yi nekk di dëkkal lu sakkan ciy nit te matalewul li nu laaj ci dëkkiin wu baax te xellu ci noonu wér gu yaram dajeeki jafe jafe yu rëy a rëy jikko it naka noonu jafe jafey ligeeykat yi gën na a yokku bi nu demee ba li nu leen di fay manatul a faj gën ja a neewi seeni aajo ngir seerug dund gi beneen jafe jafe bu mboolaay bu bees amati ànd ak yewwuteeg endustri gi ak ag jëmam kanam loolu mooy ne lu bari ci jigeen ñeek xale yi leegi danoo tàmbli di ligeey ci isin yi te kat kenn soññu leen ci ku dul boroom isin yii nga xam ne li leen ñoroon weesuwul nu nu man a gën a ame ay ligeeykat ba gën a man a neew lu nuy fay ginaaw ligeey bi ci isin yi laajul doole ju rëye noonu ngir man ko loolu tam jurati yeneen jafe jafey mboolaay ndax tax na ba jigeen bàyyi fi ay ligeeyi boppam dem ci isin yi xale yi it bàyyi njàng mi te loolu ag pert manu koo kawe ndax xale yi ñooy yaakaari ëlëg ag yàqu yàqu tàmblee feeñati ci wërlaay gu mboolaay yi ci tugal maanaam nit ñi loolu nag mi ngi am bi ag ñàkk ligeey tàmblee tas ak a yaatu ci orob ci ligeeykat yu góor yii nga xam ne danoo tàmbli woon a nekk ay jafe jafe dëgg ci kanamu goornamaa yi di yëngal tey sàkku nu nu leen lijantile seen jafe jafey ligeey yi ci noonu goornamaa yi daal di def ay àtte indi ay sart yu nos ligeey bi aar ligeeykat yi ci fuqaleg boroom bopp alal yi moom isin yi ñatteelu bunt bi yëngu yënguy politig yu mag yi ci adduna bi feeñug diiwaan yu bennoo yu amerig yi u s a jeqiku walla fipp ga amoon ca fraans doggantal gu njëkk gi feeñug diiwaani amerig yu bennoo yi gàddaay yi waa tugal yi daa def juge tugal jëm amerig gàddaay yooyu wéyoon nanu di sottiku ci amerig gu bëj gànnaar gi loolu nag amoon na ginaaw bi kolomboo feeñalee amerig ba am lu tollook xarnu li ko taxaoon a am nag bari na bokk na ci 	fitnay diine yi amoon ci orob gu digg gi ak gu sowwu gi li waraloon loolu di yëngu yëngu yu diine yi jugoon di kontar egliisu katolig bi ak la ca juddoo muy ay xeexi ngér yu amoon ci diggante ngérum katolig ak mu protestant ak xeex bi protestant yi doon def ci seen biir rawati na ci angalteer ak la ca juddoo muy bòddikoonte ci diine loolu nag waraloon gàddaayug ab lim bu mag ci waa tugal yi dem amerig gu bëj gànnaar gi ngir rawale seen bakan ak ngir man a doxal seen diine ci ag féex akug ngore 	fitnay politig ya amoon ca tugal ngir xeex jaay doole ga fa amoon ak àttee na mu la neexe ga ak la ca juddoo muy ag ñàkk a nosu gu mbir yi ñàkk a nosu ak ñàkk kaaraange ak dox gi nguur yi di doxe ni mu leen soobe loolu lepp nag taxoon na ba lu bari ci waa tugal yi gàddaaye woon fi nu dëkkoon dem wuti ag goreg politig 	wër gi nu doon wër mbll yu gànjaru yi lu ci mel ni wurus mbaa xaalis bokk na ci li leen daa gàddaayloo ndax kat lu bari ci ñi daa gàdday danoo gëmoon ne amerig de reew mu fees dell la ak yile mbll te ña fa dëkk ñu neew ag xay lanu te ñàkk ag taaxe te yittewoowunu yenn ligeey yu mel ni lijanti ay wurus aki xaalis ak gasi mbll 	jëm kanam gi xam xam am ak endustri ci tugal rawati na ci wàllug ligeey ay gaal googu jëm kanam dimblee na ci nu man a tukki ci geej gi bay àgg ci barab yu sori yee sori 	ligeey yi nga xam ne lonkoo yu angalteer yi def nanu leen ngir meññal ak jariñoo suufus amerig si ak lijanti nu ñu koy sance te dëkke ko ngir dëgërale ci kilifteefug sanc gu angalteer ci goxub adduna bu bees bii bokk na ci li waral gàddaay gi sancu yi nga xam ne waa angalteer yi taxawal nanu leen ci amerig gu bëj gànnaar gi waa tugal yii bawoo woon espaañ fraans holand suwed ak angalteer sancoon nanu ay barab yu wuute ci amerig gu bëj gànnaar gi ñoom lanuy wax tay diiwaani amerig yu bennoo yi loolu nag di woon ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom benneel ak bu fukk ak juroom ñaareel g angle yi nag ñooy ñi njëkk a taxawal ab sancu ca jims town ci diiwaanu new york atum g mujj nanu nag ci diir bu gàtt di ñi gën a tas gën a wisaaroo ci goxi tefes yu penku yi ci mbooleem ñi gàddaayetugal barabi penku yii maanaam yii nga xam ne la ëpp ca ña fa sancoon dëkke woon fa ay waa angalteer lanu woon barab yii mooy yi mujjoon ginaaw bi g di laaj ag temb akug dagge ca reew may nday di angalteer angle yi nag amoon nanu ñaari anam yu nu daa sance reew yi ak a yilife bi ci njëkk mooy buurub angalteer da daan may yenn ci lonkoo yi gu ci mel ni lonkoo gu werjiniya gu london gi mooy bi yoroon mbirum sos sancu bu jims town bi nu la waxoon leegi da leen daa may ay sañ sañ ci nu taxawal ay sancu ak jariñoo xeewal ya fa nekk ak defar xaalis walla koppar yu nuy man a jëflantee ak topptoo mbirum kaaraange gi geneen anam gi mooy buur bi day dogal garmi yu angalteer yi ay suuf ba noppi féetale leen mbirum yor leen ak àtte leen bi fukk ak juroom ñatteelu xarnu g di agsi ci digg bi amerig mujj na yor fukk ak ñatti sancu yu angalteer ñooy new york wirjiniya rood island masacuusest dulawir new hamser kintakit north karolaayna south karolaayna new jersi jorjiya ak pensilvaniya diiwaan yooyu ñooy yi sos te amal li nuy wax diiwaani amerig yu bennoo yi ci ginaaw xareb temb gi atum g ñu mujj am ag temb ci angalteer ci mujj gi diiwaan yooyu nag bu nu leen xoolee ci amerig gu leegi gii nii dunu weesu benn xaaj ci amerig gu nu xaaj fukki xaaj noste gi doon doxal mbiri biir yu sancu yu angalteer yi nguurug angalteer gi daa joxoon ay sancoom yi nekkoon ci amerig gu bëj gànnaar gi da leen a joxoon aw xeet ci ag àtte sa bopp waaye teewul ci biir loolu lepp mu bàyyil fi boppam kilifteef ak cang gu mu am ci kaw sancu yooyu maanaam may na leen ñu yor seen bopp di doxal seen mbiri biir waaye teewul muy seen kilifa di reew mi leen moom nosteg àtte sa bopp googu amoon ci sancu yooyu mi ngi tegu woon ci ñatti ponk 	doxalkat bi 	jataayub yoonal bi 	jataayub diisoo bi doxalkat bi walla àttekat bi mooy kilifa gi yilif dooley xare ji ci sancu bi mooy feetewoo sàmm mbiri way dëkk yi di topptoo kaaraange gi te am na sañ sañu dindi saxal gu nu defe ci ñaari jataay yii bu yoonal bi ak bu diisoo bi moom nag àttekat bi buuru angalteer bee koy fal ak a folli bu dee nag jataayub yoonal bi moom ñi dëkk ci sancu bi ñoo koy tànn li ko tax a jug nag mooy tege galag yi ak fuglu ligeeykat yi ak saxal seeni payoor ak payooru doxalkat bi bii jataay nag li ko may doole mooy jële gi mu jële sañ sañam ak kàttanam ci nit ñi dëkke ci sancu bi ginaaw ñoo ko fal jattayub diissoo bi moom li ko taxoon a jug mooy di xelal àttekat bi ak jataayu yoonal bi ak di diisoo ak ñoom waaye nag moom sancu bi ak li mu jot a am lepp muy ag àtte sa bopp gi nga xam ne taxoon na ba nu man fa a doxal demokraasi teewul mu nekkoon ab sancu rekk bu toppoon ci ginaaw nguurug angalteer gi ci gisiinu waa angalteer goornamaa bu angalteer li mu fàttee def mooy wut nu mu nose mboolooy angle yii dëkke woon sancu yi ñoom mbooloo yii nga xam ne mujj nanu lu jamono di gën a yàgg ñuy gën a sori seen reewum nday ma di angalteer ci wàllug aada ak dundiin loolu waral ñu tàmbli koo fàtte di yëg nag leegi ne fii mooy seen reew di ci tënku te di ko fonk loolu nag tàmbli woon na a wuute ak politig bi george mu ñatteel mi taxawaloon moo doonoon burub angalteer ca jooja jamono lii mooy li taaloon ab xare bu mag ci diggante sancu yi ak nguurug angalteer gi xare boobu moom lanuy tudde xareb temb bi li waraloon xareb temb bi ñi dëkke woon sancu yi ay mbooloo lanu woon aki kureel yu wuute ak doonte la ëppoon ca ñoom ay waa angalteer lanu woon yu di ay protestant seeni njariñi koom koom it bokkewul woon te niroowul woon waaye nag loolu lepp teewul woon amoon nanu ñatti mbir yoo xam ne kenn wuutewu ci woon ñepp a ci dëppoo woon ñooy 	am gu nit war a am ag goreg jëmm rawati na goreg pas pas 	 ak sàmmoonteek yoon ak nosu maanaam nosu gi mbir yi war a nosu 	yëg gi ku nekk yëgoon ne fii ci sancu yii la dëkk moo dim reewam fa la feetale ag reewoom ëttub amerig bii nag mujjoon di def ay mbir yoo xam ne ñoo waraloon xareb temb bi tàkk mbir yooyu manees na leen tënk ci yii yoon yuy tege galag ak tembar parlamaa bu britani bi daa genne atum g aw yoon walla luwaa bu nuy wax luwaa bu tembar yi mooy biy def ngay fay tembar ci jëflante yu ofisel yi ak dosyee yi ak yëglekaay yi añs ci atum g ñu farataal galag ci suukar si nu daa jële ci sancuy espaañ yi yu fraans yi ak yu holand yi teg ci farataalati ko ci ataaya kayit weer ak rasaas yoon wi aju ci geeju navigation ak yaxantu ci atum g barlamaanu britani bi dafa genne benn luwaa buy waral ci sancu yi nuy tuxal li nuy genne ak li nuy duggal di ko def ci ay gaal yu britani aaye leen ñuy jëndati feneen leneen loo xam ne bari na angalteer koppar walla kee bu kayit ak jënd suuf sancu yu britani yi danu leen a aaye woon ci yoon ñuy genne walla ñuy defar benn kee bu kayit ak di ko jëfandikoo niki kee bu ofisel noonu tam lanu teree woon ci beneen luwaa ñuy jënd suuf yi feete sowwu fukk ak ñatti sancu yi ngir jàpp gu nu jàppoon ne yooyu suuf nguurug britanee leen moom nos dooley kaaraange ji goornamaa bu britani dafa sosoon jenn doole ju xare ngir aar sancoom yi nekkoon ci amerig gu bëj gànnaar gi doole jooju tolloon na ci junniy xarekat mu waxoon waa sancu yi ne ñooy warlu di joxe depaas yi doole jii di laaj loolu nag taxoon na ba waa sancu yi mer ñaawlu loolu lool ngir loolu tam goornamaa bu britani bi ne kon na ci genn waaye nag galagu ataaya moom dindiwu ko loolu tam tax na ba waa sancu yi di yëg ne ñoom daal danuy jëflante ak ñoom mu mel ne dañuy ay nit walla ag njaboot goo xam ne ñoo gën a neew solo ak daraja ñi dëkke angalteer waa sancu yi tam yëgoon nanu ne li nuy fay ciy galag lepp dunu leen ko defal fi nu koy faye waaye kay ca reew mu leen sori mee di angalteer te loolu du leen jariñ ci seen dund gi te du ci def dara nga rax ci dolli ne angalteer mooy reew mi rënkaloon boppam ci sancoom yi yaxantug marsandiis yu bari maanaam bari na lool ay marsandiis yoo xam ne angalteer da ne woon moom rekk a leen sañ a jaay ci sancu yi lu mel niki ataaya loolu nekkoon na lu waa sancu yi ñaawlu woon ci nii daal la xew xew yi toppantee woon di nëxal nag sellug seqoo gi amoon ci diggante angalteer aki sancoom loolu tam gën a yaatal paxum reeroo mi nekkoon seen diggante loolu nag gën na a fés bi waa sancu yi bañee ne dunu fayati galagu ataaya ginaaw bi tam am mbooloo jug ci desambar atum g lakk ñatti gaal yu nguurug angalteer yu nu duyoon ak ataaya ca waaxub boston ca sancu bu masacusets loolu waral waa angalteer tëj waaxub boston bi ne gaalug yaxantu du fi teerati daal di ne moom ci jëmmi boppam mooy yoral boppam sancu boobu xew xew bii ak la ca juddoo man nanu ne moo waral xareb temb bi ndajem waxtaan mu filadelfiya mu njëkk mi juroom ñeenti diiwaan yu ameriig teewe woon nanu ndajem new york ma atum g di sàkku ci nguurug angalteer mu teggil leen galagu tembar bi mu leen di teg ci noonu angalteer teggi woon na galag boobu waaye teewul mu wéyoon di tege yeneen galag yi nga xam ne ab parlamaam daa na leen woote te di leen farataal ci mbooleem ay sancoom yi nekk ci adduna bi looloo taxoon reenub reeroo bi amoon ci diggante angalteer aki sancoom saxoon fi di lu ñu dogadi ndax kat sancu yi danoo gisoon ne di leen teg ay galag te seeni jataayi yoonal ànduñu ci bu amee lu muy tegtale mooy dindi màndargam demokraasi mi seen jataay yooyu di doxal seeni mbir ame woon ndax kat daa am ab dal bu nekk ci demokraasi bu naan doo fay galag boo amul ndaw man nanu ne ndajem new york mi mooy lu njëkk a feeñ te nosu loo xam ne waa sancu yi def nanu ko di ci kontar ni angalteer di àttee seen reew yi ñoñ sancu yepp a meroon bi angalteer tëjee waaxub boston bi bu ko defee ñu taxawal am ndaje ca filaadelfi atum g jàmmaarloo fa ak angalteer ne ko na xam ne lepp lu mu defati benn sancu ci sancu yi na ko wóor ne sancu yepp la ko def daal di ñaawlu bu baax jëf yu ñaaw yi angalteer tegoon boston njiitul xare lii nuy wax george washington g teewe woon na ndaje ma ndajem filadefi moomu mooy dàtt bi nga xam ne ci la kongres mujj a teggu ci ginaaw bi jaadu na ñu leeral leen ne ndajem filadefi mi li ko taxoon a jug du sàkku ag tembte waaye kay yëgal angalteer ne lu wuuteek demokraasi lii muy def ci sancu yi neexu leen te man na a nëxal te yàq xaritoo ak jàmm ji amoon ci diggam ak ay sancoom ñoom kay seeni càkkuteef weesuwutoon lii mooy na angalteer xam ne ñoom sancu yi kat ñoo ame àq ak sañ sañ ci seen jataayi yoonal yi ci tege ak farataal ay galag ci waa sancu yi angalteer nag ci safaanub muy lijanti lëj lëj boobu ci maslaa gu xereñ moom daal da fee nekk di yonnee ay dooley xare yu yees ci boston ngir gën a dëgëral doole ja fa nekkoon loolu tam li mu juroon mooy waa sancu yi ñoom itam ñu ne woon nanu waajal seen bopp ndax kat nguurug angalteer gi bëggul jàmm ci noonu ñu ñoom waa sancu yi defaat beneen ndaje ci filadefi ngir jàng mbir mi seet nu ñu ciy def ndajem filadelfi mu ñaareel mi ndawi sancu yi defoon nanu am ndaje atum g ca filadelfi muy ñaareelu ndaje mu filadelfi mi ñu wax fa ne danuy sos menn mbooloom xare te bennal ko bañ a def sancu bu nekk am sa mbooloom xare bu ko defee nag mbooloom xare moomu ñu tànne ko ci waa sancu yi ngir ñu aar leen ci ay wi leen dëgmalsi ci noonu ñu duggal doomi sancu yi ci xarekat yu bees yii nga xam ne george washington moo leen jiite woon waaye teewul ñu yonnee ca buuru britani bi ab bataaxel buy sàkku ci angalteer mu xoolaat ni muy jëflanteek sancu yi te lenn baaxu ci waaye buur bi moom jàpp fa mu jàppoon rekk ne daal am na ag cang gu nu joyal ci kaw mbooleem sancu yi ci jëfam jooju la tëje buntub jeem gi sancu yi doon jeem ngir defar ak doonte lu neew la itam seen diggante ak britani reew miy nday ni xare bi tàkke bi buur bii di george mu ñatteel mi ñàkkee faale càkkuteefi sancu yi ne daal li wér mooy moo ame cang gu joyu gi ci mbooleem sancu yi maanaam sancu yepp ci ron kilifteefam lanu nekk ci anam gu matale te daj bi buur bi nekkee ci taxawaayam boobu ne du ci juge la xare bi tàkk ci diggante ñaari wàll yi sax nag lu toll ci juroom ñaari at daanaka g bu ko defee mu tas nag ci li ëpp ci sancu yu amerig yi george washington nag jot na a man a nangu boston ginaaw bi mu ko gawee dooley gornamaa bu britani moom teg loxo lu bari ci waaxi amerig yi george washington ni mu doon xeexe ak ñoom nag mooy xeexub bette ci barab yu bari ak door daw foo ko fekk daawul nangoo jaamaarlook ñoom ndax xammoon na ne ñoo ko ëpp doole te gën koo tàggatu ak li xarekati sancu yi doon jànkoonteel lepp ciy coona yu tar ci biir xare bii teewul george washington gañe woon na njiitul anglteer lii di burgoyne ci xareb saratoga loolu mi ngi am bi mu jawalsee juge kanada jëm new york ci oktobar g ca saa sa ginaaw bi nu gañee britani fraans jug na yëgleb xareem ci kawam atum g espaañ roy ko ci atum g holand topp ci atum g man nanoo wax ne fraans moom jàpple na way fippi sanncu yi ci wàllug xare militaire ak ci alal ba tay it dajale na way coobarewu yu fraans yi yobbu leen ci diiwaan yu bennoo yi ngir nu xeexle leen ci ron njiit lu xare lu fraans lii di lavette kontar angalteer noonam bu mu yàgg a noonool bii ci noonu britani mujj war a xare ci jë yu bari dàq gi nu mujj a def dooley angle ji ci sancu yi mooy gi nu defoon seen njiit la cornwallis loolu di bi mu deltoo ginaaw dem dëkkub york town fa dexug york di sottikoo ginaaw ba ko fa mbooloom xarem george washington ma songee xarekati george washington yooyu nag am njaxasiitum kureel lanu woon mu ame ci diggante ay waa fraans aki ñoñi sancu tollu nag ci fukk ak juroom benni junniy xarekat nanu fàttaliku nag ne waa amerig yi ñoom ci seen suuf lanu doon xeexe bu ko defee dolli leen doole ci xare ak ci alal day gën a yomb gën a gaaw bu dee waa angalteer yi xawoon a sori kanada fi seen bagaasi xare daan juge walla angalteer mi leen soree woon lu tollook ay ñatti junniy miil daanaka nga rax ci dolli waa amrig yi danoo dogu woon bu wóor ci raxasu ci teg loxo gi britani tegoon loxo seeni mbir te amoon nanu ay njiiti xare yu bari ku ci mel ne george washington doolil ci loolu nekk gi waa britani nekkoon di xeexe ci sancu yoo xam ne manuñu fa a ame jokkoo ak dolli doole ga war ca anam ga mu ware te gaaw te itam pasteefub xeex bi nu amoon moo gën a suufe fuuf bi waa sancu yi amoon ñoom ñi taxawoon tamb ci xettaliku ci waawug nguurug angalteer gi bokk na ci li doyadil waa britani yi ci xeex bi ubbi gi nu gubbi woon ay jë yu xare yu bari ci seen kaw ci barab yu sakkan ci amerig tembug diiwaani amerig yu bennoo yi bi waa britani xamee ne lòtt nanu ci toroxal jeqiku gi amoon ci amerig te xam ne doole du mooy lijanti lëj lëj yi nekk ci sancoom yi ndax kat mi ngi nii di ku nu dàqe gañee ko ca xare ba bi loolu amee mu sàkku woon ag juboo ci noonu ñu xaatim juboo gi ci paris ci digganteem aki sancoom atum g lii mooy poñ ya ca ëpp solo 	britani day nangu tembteg sancu yi nekk ci suuf yi feete ci penkub dexug misisipi gi te jàppe dex gii muy diguw soww wi ko tàqale ak sancu yi bu ko defee dig yu bëj gànnaar yi ñoom ñu bàyyi leen nanu nekke woon 	jeem a rafetal seqoo yi ci diggante britani ak reewum amerig mu temb mi diiwaani amerig yu bennoo yi 	amal ci diggante britani ak amerig gu temb gi ay seqoo yu yaxantu ak yu koom koom waaye nag seqoo yooyu ñu teg leen cig nawlante ak moroomante kenn du jaay kilifteef sa moroom nii daal la diiwaan yu amerig yu bennoo yi ame xareb temb bi nag am na benn jeexiit bu rëy te xóot ndax wal na te upp ngelawul gore ak temb ci mbooleem sancu yi lii nag làppal na britani loofloo ko ci wàllug xare ak politig nga rax ci dolli alalam ju bari ji mu ci ñàkke amerig nag moom daal di ñew defar sartu reewam daal di taxawal ndajem booloo mi nga xam ne kongres moo ko digale woon atum g mbooleem ndawi diiwaan yu bennoo yi teewe woon nanu ko ba mu des diiwaanub rood island cer ya fa nekkoon tam tànn cig dëppoo george washington muy njiitul ndaje mi ci loolu la nekke ki njëkk a nekk njiilul diiwaan yu bennoo yi ginaaw bi lanu def washington ginaaw bi mu nekke peeyu koom koom bi ak bu alal bi la nu ko def peey bu politig bi george washington nag jëloon na xalaatam yepp def leen ci nu muy def ba bennal amerig looloo taxoon waa amerig yi soppoon ko wormaal ko waxam it weesuwutoon doon leen benn doon leen ay waa amerig loolu saxoon ci seen xel yi washington moom wàcci na jal bi joxe njiit gi atum g ginaaw bi mu ko yoree ñaari yoon doggantal gu ñaareel gi jeqiku walla fipp ga amoon ca fraans jeqiku walla fipp ga amoon ca fraans mooy jeqiku gi njëkk a am ci jamono ju bees jii ci kaw nguuru ak jaay doole ak doxale ni la neexe doo diisoo doo deglu xalaatu keneen moom nag fipp googu mi ngi ame woon ca fraans ca jamonoy buur ba tuddoon luwis mu fukk ak juroom benn ma bokkoon ca njabootug barbon ga loolu nag di woon ca noorub g saxoon it diir bu toll ci fukki at ba ca nawetub atum g bi jeneraal bi tuddoon napoleon bonaparte g defee yong gu nuy wax yongug brumaire dëppoo ak nowambar g daal di daaneel doxaliin wa fa nekkon jële fa it jataayub mag ña mujj nag di kenn ci ñatti kilifa yiy doxal mbiri reew mi bonaparte mii nga xam ne mujj na di kilifag fraans gu njëkk gi ci atum g mujj it di imbraatoor ba atum g moom bonaparte mujj na am tawfeex ci dindi lëjug politig ga fa amoon ñàkk jàmm ga tiitale ga tuur dereet ga ak yeneen jëf yu ñaaw yi àndoon ak fippug fraans gi loolu nag taxoon na ba fipp gi manu fi woon a amal dali gore yamoo mbokkoo yi nga xam ne ñoom la yàgg a yekkati kàddoom ngir saxal leen fi waaye nag jeexiit yi nga xam ne fipp gii ba na leen fi yamuñu rekk ci fraans waaye weesu nanu ko ba daj tugal gepp ak lu bari ci reewi adduna bi ni fraans meloon laata fipp gi bu ñu gëstoo na fraans meloon laata fipp gi loolu di na nu dimbli ci nu man a xam li waral fipp gi atum g melokaanu politig wa buuri fraans yi ni ñu doon àttee fraans du woon nenn nu dul ni mu leen neexe buur bi moo daa saytu lepp kepp ku am nguur moo la ko daa jox moo daa doon balluwaayu mbooleem doole yi ak sañ sañ yi walla nga ne sax mooy nguur gi di sañ sañ bi di kàttan gi di doole ji loolu nag man nga koo degge ci waxi buurub fraans bii tuddoon luwis mu fukkeel meek ñeent man maay nguur gi buur bi mooy ki am sañ sañ ci def ay yoon ak neenal leen tege ay galag def ci alali reew mi lu ko soob tabb jëwrin yi fal ligeeykat yi folli leen joxe ay ndigal jaare ko ci ay bataaxel yu nu xaatim ngir nu jàpp ku ko soob ci askan wi ak tëj ko ci lu dul mu koy àtte mbaa mu koy laaj dara buur bi daal ci gàttal lu ko soob mu def ndax moom dafa gis ne mi ngi wéeru ci sañ sañam boobu ci gis gis bi fiy indi sañ sañu yalla bi mooy li naan buur bi daal nguuram gi ak sañ sañam bi mi ngi bàyyikoo ca yàlla luwis mu mii nag nga xam ne ci atum g la nekkoon ci jal bi tey buur bi nga xam ne ciy jamonoom la fipp gi xewoon moom luwis mii nekkoon na ku doyadi te daan dengi dengi moom de jaraafam yi danu koo yilifoon ak bëkkneegam yi ak soxnaam si bàyyikoo woon hongri mari antuwanet di woon doomi lingeerub ongri ba mariya tereesa moom soxnaam soosu nag ku yëgoon boppam la te faaleedi woon askan wi taxoon na ba kenn manut a def genn yéwénal kenn manul a jàpple buur bi ci luy defar moom daal nekkewu fi woon lu dul yàq alal noos ak caaxaan nekkoon it ku diis te rëyal boppam looloo taxoon mu mujjoon di ku waa fraans yi bañoon njabootug barbon gi yàgg nanoo jariñoo seen nguur gi ci luy lor askanu fraans wi ñoom daal danu daa nangu alali ku leen neex daan tëj ku leen soob daan xeexloo reew mi saa su leen soobee te xeex yooyu yu ci ëpp danu ci daa gañe fraans bari na lool lu ñu daa tabax ay njénd di ci sotti alali reew mi ak di may seen dag yi alal ju dul jeex seen dag yu bari yooyu nga xam ne tolloon nanu ci junniy nit atum g te lu ëpp ci ñoom defuñu fa woon dara amul lenn lu nu fay ligeey lu amal njariñ reew mi looloo taxoon njëlul nguur gi loof mujj moom nguur gi fees dell aki bor nguur gi kat mujj na ay deppaasam àgg ci milyong yu frank atum g li mu ameele woon ciy bor àgg ci milyon yu frank ngir lòtt gu njëlam li lòttoon baj baji ak doxadi amoon na ci wàllug doxaliinu nguur gi ci wetu doxe ni la neex ga amoon ca wàllug politig ga nattukaayi gox bii daawul bokk ak bee naka noonu yoon yi màndaxekaay yi galag yi ci noonu fraans mujj di reew mu ay gox boole gox bu ci nekk am ay yooni boppam aki nosteem yu wuuteek yeneen ya ca feneen loolu nag waraloon na ag lënt ci nosiin yi ak luwaa yi reew mi mujj seddaliku doon ay doxaliin yu temb bu ko defee fraans mujj doonatul menn reew waaye ay doxaliin yu wuute te tas na mboolaay ga meloon mboolayug fraans gi njëkk fipp gi dafa seddaliku woon doon ñatti kureel yu mboolaay ñooy kureelug ñu tedd ñi walla garmi yi kureelu niti diine yi ak kureelu mbooloo mi walla baadoola yi ñatti kureel yii nag ñoom de ci li fi jamonoy laman desaloon lanu yamoowunu woon ci àq ak yelleef du caageegug ci ay warteef li am daal mooy ag yamoodi gu mboolaay amoon na ci seen diggante jefkay tàqali ak feewaloo ruuru leen ak boddante gu mboolaay bu ko defee kureelub garmi yi nu teggil leen galag yi ña ca bokk it ñoo daa feetewoo pal yu kawe yi yu siwil yi ak yu xare yi ci nguur gi ñoom ba tay daa nanu am ay cer ci mbayum baykat yi ak ci jurug sàm yi ak seen ñanaaw yi amoon nanu it sañ sañ ci rëbb ci tooli baykat yi baykat yi tam amunu wonn sañ sañ ci wal seen dugub ci lu dul walukaayi garmi yi te seen reseñ it sañuñu ko woon a nale fu dul ci seen nalukaay yi loolu lepp nag daanaka ñi ko daa jariñoo ñu neew la daan doon ci niti diine yi ak seeni njaboot bu ko defee ñu bàyyi nee way ndool yi ak ñi aajowoo kenn du leen dimbli ña ëpp nag ca niti diine ña taxutoon ñu feexoon moo taxoon danu daan ànd ak mbooloo mi kontar garmi yi kureelub mbooloo mi nga xam ne la ëpp ca askan wa ca lanu bokkoon ñoom jegge woon nanu bi fipp gi di bëgg a door lu tollook milyongi nit te kat booba garmi yi bu nu leen boolee ak niti diine yi weesuwunu woon junniy nit coonab galag yepp ci ndoddum baadoola yi la daan tegu kureel boobu nag bu baadoola yi moo ëmboon kureel bu diggu bi walla bi nuy wax bourgeois ak kureelu baykat yi ak bu boroom mecce yi ak bu soldaar si bu dee kureel bu diggu bi moom ca la boroom xam xam ya bokkoon xalaatkat ya boroom xel yi ñoom nag amunu woon sañ sañ ci pal yu kawe yi moo ëmboon it yaxantukat yi ak boroom alal yi daa fay galag yu mag yi nga xam ne seen fay gu metti gi nu daa fay galag yi ak lamb gi amoon ci seen yaxantu gi taxoon na ba seen koom koom daanu woon lii lepp nag taxoon na ba gii kureel meroon lool ci goornamaa bi te meroon it ci ay jëfam ak ci li nu defaloon ñaari kureel yii di bu garmi yi ak bu niti diine yi bu dee kreelug baykat yi nag ñooy ñi gënoon a sonn ci kureelug baadoola yi ñoo ci daa njëkk a yëg aw ay bu jafe jafe bu kopooar amee ndax ci seen kaw lanu ko daa tegaat ci fayloo leen ay galag ak teg leen ligeey yi gën a tar bu nu nee kureelub soldaar si ñi ngi ci jublu soldaar su ndaw si ak boroom ndomay xare yu ndaw yi ndax ndoma yu mag yi moom ak pal yu mag yi garmi yi lanu leen daa jagleel na fa xalaat meloon ak li fraansu njëkk fipp gi di gënadi woon a nekk cib coona ak ñaawug nekkiin yeneen reew yi mel ne itaali otris brusiya ak riisi lepp teewul waa fraans a gënoon a yëg yeneen reew yi tooñaange yi nu leen daa teg li waraloon loolu nag mooy yewwuteg politig ga fa amoon ak gu xalaat ga ca biir boroom xel ya ca kureelub baadoola ya di yaxantukat ya ustaas ya layalkat ya doktoor ya boroom xam xami koom koom ya bindkat ya xeltukat ya añs jamono jii dafa fiiroo ak diggante bob fraans da cee amoon ay xalaatkat yu mboolaay ak yu koom koom yu leen daa yee ci coona yi nu nekke ak bonug nosi politig ya fa amon yu mboolaay ya yu doxaliin ya ak yu alal ya da na jaadu nu waxtaane fi ñatti xalaatkat yoy ligeey nanu lu rëy ci tas fi xalaat yi fi indi fipp gi ñooñu ñooy montesqieu voltaire jean jacques rousseau bu dee montesquieu g moom mi nga xam ne siyaare na angalteer gondiku woon it lool ca nosteg sartu reew gu buur ga fa nekkoon moom de ay ligeeyi xam xamam mi ngi feeñe woon ca teereem ba tuddoon ruug yoon yi g teere boobu nga xam ne teere bu jaroon la bu boroom xeli yi fonkoon la ci fraans ak feneen xalaati montesquieu yi ñi ngi tënku ci fexee tënk goornamaa bi te fuglu ko ak tàqale diggante dooley yoonal ji ak ju doxal ji ak ju laman ji moom montesquieu nag li mu doon wut ci teereem boobu mooy taxawal ag atte gu tegu ci sartu reew ca fraans ndax kat moom dafa gondiku woon lool ca sartu reew bu buur ba amoon ca angalteer bu dee voltaire g moom de woote na jëme cig coppi ci nekkiinu askanu fraans wi jaare ko ci taalifam yi mu defoon ciy woy nga xam ne taalifi jam lanu woon ak yéjj moom de jamoon na nosteg politig ga amoon ca fraans ak gu egliis ga ak sañ sañ yi garmi yi amoon ak niti diine yi wolteer de ak li xalaatam yi doonadee woon lu yees lepp teewul seen solo ñi ngi feeñe woon ci nekk gi nu nekkoon di luy laal yëg yëgi waa fraans yi ngir nekk gi ñu nekk di ay xalaat yu nit yuy jeexiital wolteer de gore ga waa angalteer ame woon da koo neexoon lool yeemoon ko mu jeexiitalu ci ginaaw ba mu fa amee ñatti at li waraloon mu nekk fa nag mooy danu koo dàqe woon fraans gore googu mu gisoon ca angalteer ak xalaat ya mu fa ame woon feeñal na leen ca teereem ba tudd bataaxeli xeltu walla ay bataaxel yu bawoo ca waa angalteer atum g wolteer nag dàq gi nu ko dàqe woon fraans yobbu ko angalteer ak tëj gi nu ko tëjoon lepp ca kasob bastil bu metti bu raglu ba teewu ko woon a wéy ci jam garmi yi ak niti diine yi la desoon ca dundam ga lepp it da koo jeexaloon ci nekk di ku yoon di wër bu dee jean jacques rousseau g mooy boroom teere ba tudd kollareg mboolaay mooy teere bi doon woote jëme ci goreg nit ak yamoo gi nit ñi war a yamoo ci wàllug mboolaay mu neeti goornamaa bi daal li ko war mooy mu sonn ci yittey nit ñi fippug fraans gi mi ngi sukkandiku woon bi muy lim yelleefi ki dëkk fraans mi ngi sukkandiku woon ci xalaati rousseau yu mboolaay yi nekk ci teereem boobu nu doon wax leegi jafe jafe bu koppar ba atum g mooy at mi fipp gi ame woon nekkutoon at mu ya ko jiitu woon tane ci wàllug koom waaye la waraloon fipp ga am ca mooy ñàkk a taw ga mu àndaloon ga juroon bekkoor ba ak xiif ba nit ñi mujjoon di ñu ñàkk aw ñam jafe dundiin wi naqari bokkoon na ci li gënoon a mettil mbir mi galag yu bari yi nga xam ne tege woon nanu leen te lepp di woon ci ndoddum baadoola yi ngir mëdde ci depaas yu bari yii nga xam ne nguur gi daa na leen def ngir boram yu bari yii mu daa jële ci xare yii mu daa faral a def ci biti ci jamonoy luwis ak luwis te loolu ci li daa jeexal ay koomam la woon luwis bi mu ñëwee jeem na ba sonn ngir lijjanti jafe jafe bii amoon ci mbirum alal mi ak loppanti njëlul nguur lu loof lii te sonn jaare ko ci tege ay galag yu bees waaye mujj na di ku manutoon a ñàkk a woo jataayub kureel yu xeet wi bii nga xam ne danu koo tasoon ci jamonoy luwis ngir mu daje naka la fipp gi ame woon doomi kureel gu diggu gi begoon nanu lool bi luwis woowee jataayu kureel yu xeet wi ngir mu def am ndaje ngir gëstu yoon yi man a lijjanti jafe jafe bii aju ci lòtt gi njëlul reew mi lòttoon ñu gisoon ne loolu daal pose bu mag la ngir nu indil seen bopp saafara si ko man a faj te fajal ko seen bopp ñi daa woote yewenal it jàppe woon loolu pose ngir def seen yewenal yi nu yeene woon ak soppi yi nu bëggoon ngir fraans man a baax man a tegu ci yoon bañ koo yamale ci loppanti njël li rekk ci noonu ag wuute am ci diggante kureelub garmi yi ànd ak bu niti diine yi ci wàll ak kureelub baadoola yi ca geneen wàll bu ko defee waa kureelub baadoola yi sàkku woon ñu def woote bi mu sukkandiku ci cer yi te bañ a sukkandiku ci ay neeg ndaxte la doonoon aada foofa mooy kureel bu nekk ci ñatti kureel yooyu da daa am genn kàddu bu ko defee yenenn ñaari kureel yi bu garmi yi ak bu niti diine yi bu ci nekk am ñaari kàddu bi ñaari kureel yii lànkee ne deesu fi wootee di ko teg ciy cer ne daal ay neeg ñooy woote bi loolu amee ceri kureelu baaloola yi danoo daje ñoom nee cig beru ñu neew ci garmi yi ak niti diine yi jàpple leen dëgëral leen ku ci mel ni garmi bii di mirabo ñu waxoon ne ñoom daal ñooy ndawi li ëpp ci askan wi ñu giñoon it ca fowuwaayu tennis ba nekkoon ca wetu njéndul versay la ci atum g ne ñoom de dunu bàyyi mukk lii nu nekke li feek wutalunu reew mi ab sartu reew bu man a yewenal seenu nekkiin te baaxal ko ak doonte luwis moom li mu àndoon mooy kureel yepp daje te xam ne ñooy ndawi reew mi bu nu booloo waxul bu benn taqalikoo nee beru ci noonu way daje yii nga xam ne danoo tudde woon seen ndaje mi ndajem xeet wi walla jataayub taxawal bi ñoom de foofu lanu nekkoon ci defar sart bu bees bi ñeel fraans bi nga xam ne day leeral li waa fraans bëgg tey jeem ci seeni aajo jëf jii nag mooy doorug fipp gi tolluwaay yi nga xam ne fipp gi romb na leen ceri ndajem xeet wi daje woon nanu ca versailles ngir defaral fraans ab sartu reew bu yees askaan wi daal di jañu jëm ca kasob baasil ba ca paris ca sulye g song ko nangu ko genne ña ñu fa tëjoon ngir politig jëf jooju mujj di juy wone gore gi nga xam ne moom la fipp gi doon woote jëme ñu mujj jël bis boobu def ko màggal gu xeetu fraans wi di màggal at mu nekk nangu gi nu defoon kaso bi ñemeloo woon na baykat yi ñoom itam ñu jug song suufi garmi yi yàq seen njénd yi looloo waraloon lu bari ci garmi yi gàddaaye woon fraans dem feneen nekk gi nu nekkoon feneen mujjoon na di aw ay ci fraans ndax buur yi nga xam ne doonuñu woon ànd ci fipp gi ndax du seen njariñ danu leen doon ngemb ngir ñu xeex ko te loolu doon na jëme ci xareb ñoñ askanu paris wi wutaloon nanu seen bopp ay ngànnaay ñu daal di woon sos ag wattu gu reew ngir wattu fipp gi aar ko lafyette jiite ko moom mi nga xam ne waxoon nanu la ne doon na xeex di jàpple waa sancu yi kontar waa angalteer ca xareb temb ba xarekati fipp gi ñi leen jiite woon ay nit lanu ñu bañoon te sib doxaliinu njabootub barbon gi ak seeni dag lafyette moomu ci la woon ñoom de seen xol yi dara nekku ci woon lu dul mbañeel wañse ak gënjëng ci bis bi njëkk ci ut la ndajem xeet wi jibal àqi nit aki yelleefam ci ut mu neenal sañ sañi laman yi ak yeneen yi garmi yi ame woon ak niti diine yi xeet wepp mujj daanaka di jàpple fipp gi lu bari ci doole ju ngànnaayu ju fraans ji mujj fekksi wattu gu reew gi nu taxawaloon ngir wattu fipp gi ci noonu mbooloom xare mu fraans mi tas luwis mujj ànd ca la xewoon ca kaso ba waaye way fipp yi digale nu sàmm luwis ba du daw ci noonu ñu taxawal seen bopp ci doxal mbirim reew mi ak mu egliis bi ci wàllug doxaliin ak alal loolu moo merloo woon paab gi mu mujj moom paab gi di kenn ci ñi gën a noonu fipp gi ñu daal di bennal nattukaay yi ak yoon yi ci fraans gepp ñu daal di seddalewaat fraans def ko ay doxaliin yu bees bi ndajem xeet wi di teg sart bi luwis doon na jeem a dolli ay kàttanam aki sañ sañam bi mu ko manul nag la doon jeem a daw juge ca njéndam la waaye ñu jàpp ko ca farn ca suye g njëkk muy genn reew mi gis nanu tam benn dosyeem bu mu fi bàyyi woon buy feddali ne moom daal nanguwul yoonal yooyu mu àndoon ndax ànd googu mu ci àndoon danu ko cee manante woon waaye du lu mu def ci teeyug bakkan ndajem xeet wi eggal na sart bi ci sebtambar g loolu di bi fipp gi amee ba toll ci ñaari at bi mu ko defee nag ndajem xeet wi daal di tas boppam daal di fiy taxawal ab jataayub yoonal bu sukkandiku ci li nekk ci sartu fraans bu bees bii nga xam ne lu feddali woon àqi ak yelleefi nitug fraans la woon ak war gu mu war a gore te am ag yamoo ci wàllug mboolaay moom sart bi tam tàqale woon na diggante nguurug yoonal gi ak gu doxal gi ak gu àtte gi mu jël nguurug yoonal walla dooley yoonal ji teg ko ci loxol ab jataay bu askanu fraans wi di tànn mu jël dooley àtte ji teg ko ci loxol ay àttekat yoy danu leen di tànn mu jël nag dooley wéyal ji walla ju doxal ji teg ko ci loxol buurub fraans bi aki jëwrinam ndaxte nguur saxoon na ca fraans ba ca sebtambar g ci atum g beneen woote amoon na bu nu doon tànnewaat ab jataayub yoonal ci noonu jataayub xeet daal di sosu boo xam ne li mu njëkk a def mooy jibal nosteg pénc systeme republicain ca fraans ca satumbar g ñu feetele ko doxal reew mi ak teg sart bu bees buy sukkandiku ci nosteg republig gu bees gi ñu wax ko tam mu seet li nu war a def buur bii di luwis te teg yoon yuy aar fipp gi aar it fraans ci musiba yi ko man a dikkal juge ci reew yii di otris ak brusiyaa ak britaani ak sax yeneen reewi tugal yoo xam ne danoo noonu woon fipp gi feetale nanu ko ba tay taxawal goornamaa bu fraans bu dëgër boo xam ne da fiy jeem a jële fitnay biir reew mi ñi jiite woon goornamaa bu jataayub xeet boobu nag ñi ngi sosoo woon ci girondins yi ñooy ñi nga xam ne danoo gëmoon ag yewenal te daan woote jëme ci coppat goo xam ne danu koy amal cig nànk nànk ak ci jacopins yi xam ne ñoo gënoon a xaabaabal girondins yi danoo gëmoon ne fii fraans toll tay ak nekkiinam wii danu koo war a soppi bu wér ak doonte loolu dafa laaj doole ak ñu diggdoomu ñoo xam ne taxul woon leen a xaabaabal ñoom ñooy ña ëppoon ca jataayub xeet wa waaye amunu woon gis gis bu dëgër ndax leeg leeg ñu ànd ak jacopins yi leeg leeg girondins yi ligeeyub goornamaa bu jataayub xeet wi goornamaa bu jataayub xeet wi daal di nay àtte buur bii di luwis àtteb ray ci samwiye g loolu nag tax na ba lu bari ci reewi tugal yi def ag jàppaloo kontar fraans mu ci mel ne angalteer ak brusiyaa otris espaañ ak holand ginaaw bi nag goornamaa bu jataayu xeet wi daal di taxawal kureelub kaaraange feetale ko ligeeyub aar fraans ci ñiy noonu fipp gi ci biir reew mi ñu feetale ko ba tay moom kureel bi wàluug taxawal am mbooloom xare mu fraans mu dëgër ngir aar fraans ak fipp gi ak li mu fi jot a indi ci ndam ak xeewal moom fipp gi goornamaa bi nag ci njiitul girondins yi gañe na xarekati brusiya yi ca xareb valmy ba lijjanti na it ba xiir waa beljig ci ñu fipp ci kaw imbraatoor boobii di francis mi nekkoon imbraatooru nguurug rom gu sell gi ñu daal di nangu alali paap gi ci goxub afinion ngir noonu gi mu noonu woon fipp gi moom paab gi ñu fàttali leen ne jacopins yu xaabaabal yooyu ñoo saytu woon kureelub kaaraange gu matale gi ñoom songoon nanu ci anam gu tar ci njiitul robespierre kepp koo xam ne yaakaaroon nanu ne da nga àndul ci fipp gi aki gaay fipp gi jacopins yi nag bari na lu ñu daa mbugal lim bu bari ci waa fraans yi ci tuumaal leen ne danoo def ay wor yu mag ñoom ci seen jëmmi bopp nag ak doonte jàmaarloo woon nanook jafe jafe yi leen dikkaloon juge ci reewi tugal yi leen wër te aju woon ci kontar fipp gi ak doonte jàmmaarloo woon nanook ñoom ci doole ak fulla te farataal duggug coldaar gu sañ bañ ngir aar reew mi tas te giimal fttéerlu yi doon am ci yennat ci gox yi nekk ci biir reew mi duggal seeni xarekat ci beljig ak holand ànd ak loolu lepp teewul waa fraans bëggoon ñu soppi seenuw doxiin ci politig ba mu gën a woyof gën a teey gën dal te gën a maandu ci sulye g la ceri jataayub xeet wi tuumaal robespierre ne daa wor yobbu ko ca mbuggalukaay ba jataay bi defaraat na beneen sart boo xam ne moo waral ab goornamaab fraans bu bees ñu xame ko ci turu goornamaab doxaliin bi goornamaab doxaliin bi goornamaab doxaliin bi sampu na atum g moom nag li mu doon wund mooy ab diggante bu tuxu nekk ci diggante jamonay tiital ak taral ak jamonoy nguurug imbraatoor gu nu joyal gu tar goo xam ne napoliyon bonaparte moo ko ame woon ci ginaaw bi ci bi mu fi nekkee goornamaa boobu nag li gënoon na fés ciy ligeeyam ci ñaari wàll yii lanu jëmoon 	def politig bu maandu ci biir doxaliinu reew mi te du tax mu doyadi mbaa mu ñàkk fulla ci kanamu ay noonam 	yonni napoliyon ngir mu song itaali ngir yare ci otris ak yonneeti ko ci penku bi nanu fàttaliku ne goornamaab doxaliin bi mi ngi sosoo woon ci juroomi cer yoo xam ne dëppoowunu woon ciy jamonoom it la jëmmi napoliyon feeñ moom mi nga xam ne jariñu woon na bu baax ci doyadig gooramaa bii ak ñàkk dooleem ngir saxal fi boppam ci wàllug politig ciy jamonoom it lu sakkan ciy làngi politig sosu woon nanu ni nu doon jëfandikoo alal ji gën a ñaaw gën a bon ci fukki fan ci nowambar g la napoliyon ak làngam gi defoon yong googu nuy wax yongug brumaire daaneel goornamaab doxaliin bu neewoon doole boobu loolu moo fi indi goornamaab kilifa bi mooy bi ame ci ñatti kilifa yi nga xam ne ñoo doon jiite fraaans te napoliyon jiite woon leen nga xam ne daanaka mbooleem sañ sañ yi ci loxoom lanu nekkoon napoliyon bonaparte napoelon bonaparte mi ngi judd atum g ca ajaksio ca dunub corsica ca itaali dun boobu nga xam ne fraans da koo mujjoon jënde ci genova napoleon nekkoon na ba muy doon gone ku bëggoon fànnug xare mi ngi genne ca bànqaasu xare ba nekkoon paris daal di dem nag doon ab ofise bokk ca kureelub kano ya ca xarekati fraans ya moom nag ku soppoon xam xamu yoon la taariix ak xam xami xare yi ak yu doxaliin yi ku sawaroon la ci dali fipp gi te fonkoon leen moom nag ab bidiwam a ngi féqe ci ginaaw bi mu songee itaali àtteg napoleon walla yor gi mu yoroon fraans dafa seddaliku woon ci ñaari xaaj bu njëkk bi mooy kilifag fraans gu njëkk gi la ko dale ca g ba g bu ñaareel bi moom mooy imbraatoor bi la ko dale ca g ba g song gi napoleon defoon itaali goornamaab doxaliin bi dafa feetale woon napoleon jiiteg xeex boobu mu doon xeex otris jaare ko ca moomeelam yooyee nga xam ne itaali benn la ci woon atum g ci noonu moom napoleon mu daal di xeex ak nguurug sardeñ xeex bu tar boo xam ne jañ na ko ci mu xaatim ag wéer ngànnaay gu nuy wax gu cherasco napoleon defati ab xare ak dooley paab gi moñoxe ko ca ancona mu dumaati soldaari otris yi ca bëj gànnaaru itaali dàqeeti leen fa xaatim fa ak ñoom juboo ga tuddoon campo formio atum g ci nii daal la napoleon doyodile woon otris neewal ko doole daal di àgg ci njobbaxtalu siw ci wàllu doxal xare napoleon àntu gi xeexam yooyu àntu woon ci itaali tasoon lënkaloo gi waa tugal defoon kontar fraans mu mujj britani rekk moo dese woon xeex beek fraans song gi napoleon songoon penku bi politigkati fraans yi naaloon nanu taliraan mi nekkoon jëwrini bitim reew mi jiite woon leen naaloon nanu ay naal yu aju woon ci ngàdd britani jaare ko ca sancoom ya te bañ koo fekk ci biir këram rawati na moom britani dafa amoon mbooloom gaal mu mag ca geejug mans politigkati fraans yi li nu bëggoon ci loolu mooy sos ab sancu bu fraans ci geej gu diggu gi ak man a àgg ca geej gu xonq ga ak dog yoonu yaxantu wi daa àggale britani ca sancoom ya nekk penku goornamaab doxaliin bi lii mi ngi ko denkoon napoleon ci noonu mu jug mooki gaayam geeju ci atum g tukkee ca waaxub toulon mbooloom xare mi àndoon ak moom àggoon na ci ñeenti teemeeri gaal yu sëfoon ñaar fukki junneek juroom ñatti soldaar bokkoon na ci tam teemeer ak juroom ñaar fukk ak juroomi boroom xam xam yu waa fraans ñu àgg waaxub aleksandriya ca isipt nangu ko waaye mbooloom gaalum britani mi bettoon na mu fraans mi ca ndoxum golfub abii xiir moñoxe ko ci noonu la britani xañe fraans cangug geej gi fraans yàgg a gent fraans sax nag ni mu ko baaxoo woon nguurug xare la gu mag gu gën a am mbooloom xare mu jeeri ci mu geej mu mel ne mu britani mi man nanu ne xare bii napolen daan def ci penku bi xare jooñ la woon ndax kat ag sof rekk la ca xareb jooñ ba amoon cag njëkk loolu nag gën na a leere ca xare ya mu doon def ca afrig gu bëj gànnaar ga misra isipt ca jamono jooja dafa nekkoon reew mu nekkoon ci waawug àtteg usmaan gi bu ko defee buuri mamaalik yi jiite ko mu doon jànkoote ak ag doyadi gu biir ak xeex gu sax ci biirum reew ngir nangu nguur gi te tam ngànnaay yi mu ame woon yu doyadi la woon bu nu leen nattee ci yi napoleon ame woon aki jumtukaayam lii moo taxoon napoleon sonnutoon ci teg loxo isipt ak doonte mamaalig yi ñoom jàmmaarloo woon nanook moom xeex ak moom xex bu tàng ngir aar seen reew waa isipt yi bégunu benn yoon ci àtteg napoleon gi li am kay mooy danoo fippoon ci kawan mooy la amoon ca xayra keer ñu koy wax fippug xayra gi napoleon jawali na reewi shaam mook mbooloom xareem mi ginaaw bi mu nangoo isipt mu daal di teg loxo hariis gaza ak yafa daal di ray dooley kaaraange ja fa nekkoon daan ko aar te tolloon ci ñeenti junniy soldaar juge fa diriku jëm hakka gaw ko diir bu yàgg waaye hakka moom toogul rekk faste ay loxoom di seetaan dafa jànkoonte jaamaarloo cig njàmbaar ci njiitul kilifaam gii di woon ahmad basha nga xam ne mbooloom gaalum xare mu britani mi ñoo ko doon dimble tukkee ci geej gi waa usmaan yi di ko jàpple ci jeeri ji bi gaw gi yàggee te napoleon ñàkke ca lu bari te amewu ca lenn njariñ xarekatam yi tàmblee tawat rawati na tawat ji nuy wax siburu di yaram wuy tàng bi loolu amee napoleon xam ne fii muus du fi naane ñeex mu deltu ginaaw dellooti isipt te jëlewu fa lenn ndam napoleon bàyyikoo na isipt ci sekkare dellu paris askan wa tertu ko fa cig yaatal ak mbegte xew xew yi toppante ci fraans waaye ci anam gu baaxul ci goornamaab doxaliin bi looloo fi jële boobule goornamaa bi nuy wax bu ñatti kilifa yi taxaw atum g napoleon nekk ca kilifa gu njëkk ga ay ngérte yu am solo juddoo nanu ca xareb napoleon bu penku ba ñu indil leen ci yii rekk 	xareb fraans boobu ci penku bi wone woon na solo si isipt am ak fi mu feete ci wàllug jokkoo ak tuxu ñeel imbraatoorug britani gi ci penku bi 	xare boobu fraans da ci doon seete rekk ngir xam nu muy def ba man a sanc walla kolonise reewi afrig gu bëj gànnaar gi 	boroom xam xami xare boobu bi nuy ñëw indaale woon nanu ay gëstuy xam xam yu aju woon ci nàndal ak jeexiit indi woon nanu fi it benn naal bu aju woon ci gas aw yoonu ndox ci diggante suwes ak geej gu diggu gi di kanaalu suwes bi te it indaale woon nanu fi ab moolukaayu teere ci araab nu koy wax moolukaayu bolaax bi 	xare bi wutoon ay yoon yu man a indi ag jokkoo ci diggante fraans ak isipt rawati na ci wàlli xam xam ak njàngale añs napoleon ak reewi tugal yi napoleon de taxawaloon na màmm gi otris màmmoon ci yaatal nguuram ndaxte gañe woon na ko ca xare ba nuy wax marenngo atum g jañoon ko ci mu xaatim ag juboo gu yees atum g mooy juboo gi saxaloon poñ ya nekkoon ca kollareg campo formio ga napoleon xatim na ak britani juboog amiens atum g looloo waraloon dooley fraans ji genn isipt bu ko defee angalteer moom itam noppi ci li dal otris bañ cee wax dara napoleon saxoon na di ki nga xam ne moo ame woon sañ sañu fal niti egliis bi ci fraans paab bi tam bi napoleon di sampu niki imbraatoor atum g mooy ki doon def li ci aju woon ci xeeti ñaanal ak xumbal napoleon bi mu jotee ci imbraatoor gi daa daal di nosaat doxaliin wi ci campeefi nguur gi mu taxawal fi benn jumtukaay buy yëngu ci luy amal bëgg bëggam bii mu jël lu sakkan ci mbokkam yi ak xaritam yi jox leen pal yu kawe yi mbooleem dooley nguur ji ak sañ sañ yi mu tëyyeel leen boppam teg boppam it ci kaw mbooleem làngi politig yi doyadil làngi politig yi ak barlamaan bi nos galag yi napoleon de tàbbi woon na ciy xare ak reewi tugal yi britani gañe woon ko nag ci wàllug geej gi ca xare ba nuy wax attaraf al aqar mu song brusiya gañe ko ca xareb yena ba atum g mu daal di def waxtaan ak aleksandar mi nekkoon sesaarub riisi def ak moom genn dëppoo nu koy wax dëppoo gu talist atum g mooy liy wone njobaxtal la napoleon àggoon ci kàttan mu defoon ag gaw gu goxub tugal bepp jëme ko britani daal di woon ga reewi tugal yi ci ñu topp ko ci loolu loolu indi woon na fi benn jafe jafe bu koom koom bu tar ci reewi tugal yu bari loolu it waraloon na reew yii bañ ko kontar ko mu xare woon ak riisi gu sesaar gi ndaxte daa gisoon ne moom kat wormaalul gaw googu mu digale woon ci noonu mu jëmale fa menn mbooloom xare mu mag atum g ñu dox ba àgg ca peey ba di butrusburg waaye mujj nanu manatunoo ñàkk a dëpp ngir sedd bu tar ba leen fa gaw ba jamonoy sedd ja duggee ak ba tay ngir jafe ga fa ag jokkoo jafee guy man a yombal nuy jot ci li am mbooloom xare di soxla ngir man a def ligeeyam muy jotug jumtukaay yeek dund yeek lu ni mel bi nuy dellu nag la waa rusi yi sottiku ci seen kaw ñoom xarekati napoleon yi ray ci lu bar bu ko defee napoleon ñàkk soldaaram yu bari te amul la mu doon bëgg bu ko defee waatugal yi otris brusia rusi ak britani boole seen doole jàmmaarlook napoleon daal di koy gañe ca xareb libisg nu koy wax xareb xeet yi di woon ci oktoobar atum g ca noona nu sànni napoleon ca dun ba tudd elba waaye mu lijjanti ba rëcce fa ci sekkare ginaaw bi mu fa defee teemeeri bis dem nag paris dajale fa xarekat yu bari ci waa fraans yi ngir xeexi reewi tugal yi ko doon sot ñu gañeeti ko ca xareb watrlo ba atum g sànneeti ko ca dunub santa hilana mu des fa nag ba kero bi mu faatoo atum g bu ko defee reewi tugal yi def seen ndaje ma nuy wax ndajem vienne atum g ngir seddalewaat kartu tugal wu politig wi daal di fiy saxalaat bu baax kenoy nguur te suuxat ko fi ak sàmmoonteek yamoo gu reew yi ak sos reew yu am doole yu peek fraans wër ko ligeeyi ndajem vienne ligeeyi ndajem vienne nii la tënkoo woon 	way daje yi delloowaat nanu buuri tugal ya ca seen reew ya nu juge woon teg ko ci àqi yoon ci noonu nu delloosi njabootug borbon gi ngir ñu yilif fraans ak espaañ 	britani jëloon na sancu yi fraans moomoon muy malta ak kaab ak silaan ak morisos 	rusi jël moom varsaw otris jël tefesug dalmas ak milano gu itaali gi mujj nag ëpp doole nguur yu ndaw yu itaali yi brusiya moom am ay moomeel yu mag ci almaañ ak ag wàll ci poloñ ñu jël beljig cig sañ bañ boole ko ci holand jëlati norwej cig sañ bañ boole ko ci suwed jëf yii yepp nag dëppoowunu woon ak xeetu walla fonk sa xeet di nationalisme gi doon am ca tugal lii nag firee nanu ko ne li ko waral mooy britani daal ak rusi ak otris ak brusiya danoo defoon seen bopp ay reew yu ñoo am ag kilifteef ci reew yu tugal yu ndaw yi li juddoo ci fippug fraans gi 	fipp gi moo fi indi tay dalub fonk sa bopp bii nga xam ne mujj na foo dem ci tugal fekk ko fa ci diirub xarnub fukk ak juroom ñeenteel bepp g moo waral reewum itaali bennoo te moo jur it bennoo gu almaañ gi 	moo fi jële sañ sañ ak ràññale ci biiri kureeli nit naan kii moo kawe kee wii xeet a gën wee te man nanu ne mooy jaasi ji mujj rendi nostey laman ya nekkoon tugal 	fipp gi ci fraans mooy gi njëkk ci fipp yi ci taarixu tugal bu bees bi loolu nag li ko waral mooy coppat yi mu indi ciy gisiin aki deggiin aki xalaat ci wàll yu bari ci dundug politig gi gu mboolaay gi gu xalaat gi gu koom koom gi ci tugal ak fu ko moy ay term yu politig feeñ yu mboolaay yu diplomasi yu bees 	moo fi jële gisiin wu àqi yalla ji mooy gisiin wi naan buur yi seen àq ak sañ sañ ca ju yalla ja lanu ko jële mooy gisiin wi matale woon noste yi amoon ci tugal gepp la ko dale ca ba fa jamonoy laman tàmblee 	xalaatub fipp gi law na ba àgg ci tugal gepp ak yeneen reew yu dul tugal yu adduna bi buntub ñeeteel bi yëngu yëngu yi aju ci xeetu walla fonk sa xeet nationalisme ci tugal ci xarnub fukk ak juroom ñeent g bennal gu itaali bennoo gu almaañ doggantal gu njëkk gi bennal gi nu defoon itaali ni itaali meloon njëkk xare yu napoleon yi itaali laata a napoleon di ko teg loxo di ko nangu nekkutoon reew mu nu bennal nekkutoon it di mu am ag temb moom kay daa seddaliku woon doon fukki xaaj ak ñaar yu doon topp ak a nekk ci ron kilifteefug ay nostey politig yu wuute nosteg nguur ca savoia piemonte napoli ak nosteg pénc ca venezia ak geneva ak ag àtte gu paab ca rom ak gu doox ca toskaana ak parma ak xaaj yoo xam ne danoo nekkoon ci waawug imbraatoor gu otris gi ñooy milano ak lombardia piemonte nag moo nekkoon nekkteg politig gi gënoon a dëgër te ëppoon doole ci nekkte yooyu ña ëppoon ca njiit ya yilifoon nekkte yooyu ay diktaatoor lanu woon rawati na ñi ci waa otris jiite woon cig jonjoo mbaa lu ko moy jeexiit ya napoleon bàyyiwoon ca itaali napoleon bi mu nangoo itaali dafa lijjanti ba boole xaajam yu politig yu bari te wuute yooyu ci ñatti nguur rekk ñooy nguurug alp gu bëj gànnaar gi walla itaali ak nguurug savoia ak nguurug napoli mu wutaloon reew mi mepp wenn yoon daal di dindi galag ak tënk yu koom koom yi amoon ci wàllug endustri ak yaxantu ak mbay mu ubbi leekol yi ngir jàngal doomi reew mi mu may waa itaali yi ñu man di jot ci pal yi te kat bu njëkk waa otris rekk a ci manoon a jot looloo tax ñu man a wax ne napoleon de mooy ki ji njiyum bennoo mu xeet ci suufus itaali mooy ki leen def ñuy xeeñtook a gént am reew mu itaali mu man a am mu nu bennal itaali ginaaw ndajem vienne ndajem vienne mi ci xalaati njiitu jawrin ju otris jii di metternich winneburg seddale woon na itaali def ko juroom ñaari xaaj ñooy piemonte napoli parma modena toscana lombardia ak venezia ñoom ñaar nag mujj nanu leen boole def leen benn teg leen ci ron kilifteefug otris ginaaw nag metternich fexe woon na ba yay njiiti ndaje mi gëmloo leen dalu desal fi lu yàgg la ca yàggam ga maanaam lu nekk nanu ko delloo na mu meloon loolu nag moo indi ndaje mi delloosi njiiti nguur yu ndaw yu itaali yu njëkk ya ñu delloosi leen ci seeni pal tegaat leen seen barab metternich ak bëtam yi mu tasoon ci gox yepp jeemoon nanoo fuglu yeglekaay yi daan naj it gepp cawarte gu politig ci noonu ñu daa tëj gor ñi ci kaso yi daan xañ way dëkk yi pali siwil yi ak yu xare yi nga xam ne bi napoleon ñëwee jox na leen ko mu daan leen weccee ak ay waa otris moom metternich te daan leen teg ay galag yu diis te sonnle yewwueg xeetu nationalisme ni mu xëye rekk am te màgg ca itaali politigu noteel gi metternich yore woon ak li muy tar lepp taxutoon mu man a rekki yëg yëg bi waa itaali yi ame woon ak xam ngi nu xamoon am solo gi bennal seen reew mi te booloo ci wàllug politig amoon solo loolu nag mi ngi am ginaaw bi nu ci ñamee s lëf ci jamonoy napoleon bi nga xamee ne politig bu ñaaw boobu fa amoon mayu leen woon ñuy def seeni cawarte ak jëfi politig ci lu bér te nëbboodiku bi loolu amee lanu wéeru ci di def seeni yënguy politig cig làqu ak fésadi bu ko defee ay booloo yu politig yu sekkare tàmblee sosu ci dëkki itaali yu mag yi li leen taxoon a jug di bennal itaali bokk na ci yooyu booloo gu karbonari ñoñ këriñ ak booloo gu itaali gu waxambaanee gi booloo gu karbonari moom mi ngi sosoo ca napoli daan def ay jataayam ngir làqatu ci barabi ligeeykati këriñ yi walla lakkati mat yi mu mujj nag tas ci mbooleem itaali mbooleem kureeli askanu itaali wi nag bokkoon nanu ci baykat yi ligeeykat yi boroom mecce yi yaxantukat yi boroom xel yi añs li leen manke woon nag mooy danoo nosuwutoon bu baax te ni ñu daan naale ak a rëdde seeni mbir tam dafa dese woon a tegu ci yoon looloo taxoon li nu bëggoon daawul àntu te seeni noon daa leen gaaw a not te daa àntoodil seeni fipp waaye nag booloo gii di gu karbonari gi jot na fee taal yëg yëgu xeetu ci itaali te lijjanti ba mu sax fi di tàkk ak doonte daje na ak coona yu bari te nu teg ko lu sakkan ciy mbugal bu dee booloo gi tuddoon itaali gu waxambaanee gi moom jozeph mazzini g moo ko sosoon ginaaw bi mu nekkee ab cer ci booloo gu karbonari gi mazzini mii moom waay itaali la woon ju xéroon ci reewam ak xeetam nekkoon it ab xeltukat bu bokkoon ci ñoñ nite ñi bu gëmoon ne xeetu nit ñepp benn lanu te bëggoon lool goreg askan yi moom nag jot na a àgg ci xëcc cig wàllam boroom xel yi ci itaali te fàggu ñeewanteg nitug neen ku itaali ki akug cofeelam bokkoon na ci jubluwaay yi gënoon a tax booloo gii am goreel itaali ci àtteg otris ak duma àtte gu paab gi nga xam ne otris a ko daa dimbleek a dëgëral ak fexee bennal reewum itaali mi ci ron ag noste gu republig yëngu yëngu yii mujjoon na naat te dox bijjaloon it boppam lu sakkan ci waxambaane yi ak xalaatkat yi àggoon nanu ci lu toll ne juroom fukki junniy waxambaane yu weesu ay ñeen fukki at yooyu mazzini dimblante na ak garibaldi moom garibaldi ab kojug xare la woon bu itaali bu gëmoon bennug itaali te gëmoon ne danoo war a gorewu ci àtte gu otris gii bóof ci suufus itaali si ci noonu lanu jot a taxawal ñoom ñaar ag àtte gu pénc ca rom ca moomeeli paab ga ak ca venezia atum g waaye otris moom ca dooleem ju bari ja faagaagal na yëngu yëngu googu daal di dàq mazzini mu daw làqu ca anggalteer ag woote nag feeñ na fa jëm ci ñu def nattukaay yi benn xaalis bi ak peesekaay yi ci mbooleem diiwaani itaali yi aki nguur nguuraanam rawati na bi endustreem tàmblee màgg yaxantoom gën a jëm kanam boroom ligeey yi nag ak boroom boppi alal yi gisoon nanu am njariñ gi gore ci koom koom amoon njariñ ñu tàmbli woon a sàkku ñu sosal leen ay yooni weñ yuy taqale diggante bëj gànnaaru itaali ak bëj saalumam te nu uppi mbooleem ja yu itaali yi ci kanamu yaxantu gu itaali gi te bañ cee indi yenn jafe jafe walla ay mbugal yu doxaliin walla ay galag yu man a tee bennoo gu yaxantu gi am ci itaali ma fàttali leen ne barab yu bari de ci bëj saalumu itaali yu deltu woon ginaaw lanu woon ci wàllug endustri koom koom mboolaay ak politig looloo taxoon xalaat yi jëmoon ci bennoo mi ngi gënoon a dëgëre ci fi nuy wax itaali di nguuru alp gu bëj gànnaar gi ak ci digg bi foofa daal la wooteg bennal gi gënoon a tare ci yeneen wàll yu bëj saalum yi ndax kat wàlli bëj saalum yi dañoo jëmutoon kanam dara ci wàllug endustri yaxantu politig ak mboolaay lii a waraloon woote gi jëme ci bennoo gu koom koom yamoon rekk ci digg itaali ak ci bëj gànnaar gi ñi ëppoon it ci xalaatkat yi ak boroom xam xam yu itaali yi ñi ngi dëkke woon digg bi ak ci bëj gànnaar gi ak li boole itaali def ko menn reew doon nekk càkkuteful ñepp lepp teewul yenn ci nguur nguuraan yi ak doox yi kontaroon ko ndaxte ñoom dañoo ragaloon ne loolu de moo xam leegi la walla ci kanam bu amee di na fi indi ag bennoo gu politig te loolu bëggunu ko woon ndax kat ñoom seeni njariñi nguur yooyu moo leen gënaloon njariñul itaali li ci noonu nguurug paap gi kontar ko naka noonu gu otris gi nga xam ne amoon na kilifteef gu yaatu ak sañ sañ bu mag ci itaali ndax moom daa gisoon ne bu itaali bennoo ci wàllug koom boole ay nguur nguuraanam aki dooxam loolu du wund lu dul ne moom kat otris waxtuw gennam itaaliee ngi bëgg a jot ci lu dog te loolu du ko nangu mukk nguurug piemonte ak bennalug itaali ci bëj gànnaaru itaali ag nguur a ngi fi woon ñu koy wax nguurug piemonte walla sardeñaa ka nekkoon ca gàngunaay ga di woon victor emmanuel moom piemonte nag nguur la woon gu ame woon ci ñeenti xaaj yu taqaloowul ñoom xaaj yi ñooy piemonte mi nekk ci ron doji alp yi nekkoon barab bu taxu ko woon a woomle ak savoia mi ngi nekkoon ci kaw doji alp yi tiim wàllug fraans gi dend ak itaali moom nag ruq la bu gën a yor ay màndarga yu fraans ci yu itaali moom itam taxu ko woon a jëm kanam mbaa mu woomle ak sardeñaa moom dun la bu nekk ci geej gu diggu gi xaw a sori piemonte ak genova moom nag nguurug piemonte jot na ci ci ginaaw xarey napoleon yi ci tugal di nanu gis fii ne piemonte moom yorul woon nguur gu àttanoon coonay bennal itaali waaye nag yoroon na yenn yu rëy ci yiy taxawal reew mu mag yu ko mayoon mu man a yanu yan bu diis bii ñu tudd ci yi ci ëpp solo 	ab buuram daa gëmoon ag àtte gu tegu ci sartu reew te daa gëmoon it bennoo gu itaali 	njiitul jawrinam lii di cavor mi ngi doonoon njiitul jawrin atum g daa gëmoon moom itam te sopp sartu reew ba angalteer defoon te bëggoon lool itaali doon benn te nekk ci ron ndëppul piemonte 	piemonte amoon na dooley xare joo xam ne li ko daa wone mooy soldaaram sii nga xam ne jot nanoo xare ba am ci xam xam 	piemmonte moo nekkoon làqatukaay bi politigkat yi nu daa sonnale ci nguuri itaali yeneen yi daan làqatoo 	màgg gi koom koom doon màgg ci piemonte moo gënoon a gaaw gi mu doon def ci feneen ful milano 	nguurug piemonte gu sori woon loxol otris la nga xam ne daawul man a dugg ci mbiri biiram cavour ak bennalug itaali cavour mii g nekkoon na di ku gëm bennoo gu itaali waaye nag ci ron ag àtte gu nguur gu sartu reew goo xam ne buurub piemonte bee koy jiite moom kon ci loolu la wuute woon ak mazzini mi nga xam ne da doon woote ag bennoo gu itaali ci ron ag àtte gu republig moom de daa gëmoon ag yewenal gu politig gu koom koom ak gu doxaliin ngir itaali man a doon benn mu gisoon ne nguurug piemonte am na kàttanug dàq otris mu genn itaali ak naj nguurug paab gi daa lënkaloo ak otris bu lënkaloo woon moom piemonte ak jeneen doole ju reew ju mel ne fraans mbaa britani cavour mi ngi yoroon njiitug jawrin gi ci atum g bi mu ko defee nag mu tàmblee waajal am reewam ngir mu man a jiite ligeey biy bennal itaali ci noonu mu sotti yitteem ci xarekatam yi waajal leen ba nu man a jàmmaarlook mbooloom xarem otris mi te man leen a genne itaali mu jug ci suqali koom koom bi defar ay yooni weñ yu lënkale mbooleem dëkki piemonte yi daal di jamonool mbay mi ak endustri bi defar ay yoon neenal galag yeek mbir yi man a tënk yaxantu ak endustri tege ay galag yu duwaan yu mag ngir aar endustri bu lokaal bi bu biir reew mi yewenal nosteg galag yi daal di sos lonkoo yu askan yi ak bànk yi bu dee lu aju ci doxaliin ak yewenal yu biir reew mi moom da fee daal di woon buddee doxaliin wu yàgg wa fa nekkoon daal di jël ay matuwaay yoo xam ne tax nanu ba yoon ci reewum itaali gën a jamonoo jële fi lu bari ci ay jàngu maanaam ay egliis wàññi dooley politig ju paab gi tàqale àtte geek eglis bi kafor mii nag xamoon na ni reewam mi tuutee woon bu nu ko tollalee ak otris walla britani mbaa fraans am rusi ak brusiya waaye loolu lepp teewutoon mu gëmoon ne bennug itaali daal mbirum aw xeet la woon manul woon a ñàkk te itam mbirum adduna bepp la laaj na reew yi sonn ci te jeem koo faj ci nu mu gën a gaawe mu dogu woon ci sóobu ci geewub politig bu adduna bi ngir yékkati kàddug piemonte ci adduna bi ba ñepp degg ko ci ndajey tugal yi ci noonu mu digal parlamaa bu piemonte mu nangu ñu yonnee ab kureelub xare bu piemonte ngir mu bokki ca xareb xarm ba àndoon ca ak britani ak fraans ngir sàkkoo ci xaritoo ak imbraatoor bu fraans bii di napoleon mu ñatteel mi napoleon iii te ame ca ñeewantug britani akug jàppaleem ci li mu bëgg kureelu xare bu piemonte boobu ak doonte bariwu ci ñu ci dee ca xareb xarm ba ndax ñu bari ci ñi ci dee ci mbasum koleraa lanu deewe teewul kafour moom lijjanti na ba nu yëg piemonte ci kanamu ndawi tugal yi ca ndajem juboole ma nu doon def bi xareb xarm bi jeexee kafour sàkku na fa ca fraans mu dimbli ko ci otris ndaxte nguurug piemonte moom rekk manul a dàq imbraatoorug otris gu dëgër gii kavour ci njëlbeen gi li ko gënaloon mooy britani jàpple ko kontar otris waaye britani moom bëggutoon a xeex ak otris xeex bu ko amalul njariñ bu dee fraans nag nga xam ne pencam mi napoleon iii moo ko jiite woon moom napoleon iii mi nga xam ne daa jàppe woon itaali am ñaareelu reewam ndax moom doom la woon ca napoleon i ginaaw doomi mbokkam la woon te napolen i mi ngi cosaanoo corsica moom napoleon iii ku soppoon waa itaali la te xéroon ci seeni àq aki yelleef ci gore te doon benn moom de bokkoon na ci ñi gënoon a siw ci woote ag xeetu ci tugal politigu bitim reewam it mi ngi ko tegoon ci bañ otris mi dendoon ak moom te ginaaw piemonte it reew mu nekk ci wetu fraans la loolu taxoon na mu bëgg mu nekk reew moo xam ne yoonu otris du ca nekk cavour lënkaloo na ak napoleon iii ñu def dëppoo ga nuy wax plombiere ci sulye atum g dëppoo googu la mu yaxal mooy ñu taxawal ag nguur gu itaali ca bëj gànnaaru itaali buurub piemonte jiite ko ak geneen nguur ci digg bi moomeeli paab gi moom ñu bàyyi leen fi te bañ a laal dara ci nguurug napoli gi nekk ci bëj saamu itaali bu ko defee nag genn bennoo gu ame cig dëppoo lënkale leen ci njiitug paab bi fraans nag li muy ame ci loolu mooy ñu bàyyee ko niis ak savoia xare yi amoon ci diggante piemonte ak otris kafour wéy na di cokkaas otris rawati na bi ko napoleon iii yonnee ñaari temeeri junniy xarekat ngir ñu xeexle ko kontar otris loolu nag amoon na ci ginaaw dëppoog polombiere gi kafour am na la mu bëggoon muy jeqi otris yëngal ko ndax moom kat otris mujjoon na jekki jekki rekk sàkku ci piemonte mu nocci ay ngànnaayam ci diir bu gàtt bu weesuwul ñatti fan mu tóllanti loolu ci jug jawali piemonte ànd ak ay xarekatam atum g taarixkat yi firee nanu loolu ne ag wuyyusi la gu otris def ci li ko piemonte doon yàgg a cokkaas ak a dëkk nii daal la xare bi tàkke ci diggante otris ak piemonte waaye nag otris a njëkk a song ci noonu fraans itam jibal ab xareem ci kaw otris soldaari piemonte yi ak yu fraans yi jot nanoo duma otris gañe ko ca xare ba nuy wax maginta ak salvarino waaye napoleon iii moom daa xëyoon rekk taxawlu ci xare bi daal di gise ak imbraatoor bu otris bi def ak moom ag wéer ngànnaay dellu xaatim ak moom ag juboo te diisoowu ci ak nguurug piemonte wéer ngànnaay gii nag mooy li jur ci ginaaw bi li nuy wax juboo gu siyorix atum g bokkoon na ca poñ ya ëppoon solo ca juboo ga 	otris bàyyee piemonte lombardi 	sos booloo gu itaali ci njiitul paab bi ci tur 	venezia day des ci moomeelug otris waaye bokk ci bennoo gu itaali gi 	 delloosi ñi yilifoon doox yi nekkoon ci digg itaali ci seen barab ak seeni pal ginaaw bi leen askan wi follee 	boole niis ak savoia ci fraans taarixkat yi firee nanu taxawal xare gu bette gi nga xam ne napoleon iii defoon na ko ne daal li ko waraloon mooy daa bañoon ag nguurug itaali gu dëgër am taxaw rawati na bi mu tàmblee gis lenn ci doox yi nekkoon ci digg itaali tàmblee bokksi ci piemonte bokkoon na it ci li ko ko taxoon a def jeem a gëramloo katoligi fraans yi nga xam ne danoo tàmbli woon a mer ci neewal gi nuy neewal doole nguurug paab gi ci itaali te otris a ko daan jàppleek a dëgëral kafour nag moom daa daal di woon xàcc walla tekki ndombaam bi mu sàkkoo ci buur bi victor emanuel ba soon ngir ñu wéy ci xare bi ak doonte fraans genne na ci loxoom waaye mu lànk mom buur bi askani doox yi bañ nañu ne dunu nangu mukk ñu delloosi ña leen yilifoon bu njëkk ni ko poñi juboo gu siyorix gi yaxale ñu ne woon daal ñoom leegi danuy dem bokki ca nguurug piemonte ci noonu ay fipp am yu toftaloo ci parma modena romaña ak toscana di woote ag bokki ca piemonte kafour dellusi na yoraat njiitug jawrin gi ngir sonnal gu ko askan wi sonnal ci mu dellusi ci biir piemonte ak ci biti nii daal la itaali doone benn ci gox yi nekk ci bëj gànnaar gi ak digg bi kafour dara deseetu ko woon lu dul mu fexee nangu venezia ak moomeeli paab bi ak nguurug napoli gi boole leen ci itaali coona yi garibaldi doon daj ci itaali doon benn garibaldi moom ku bëggoon la te gëmoon bennug itaali moom nag soldaar la woon bu dëgër jàmbaare te ñeme mujjoon na it bokk ci jàmbaari itaali yi siwe woon ag wooteg bennoo gu xeet te daan ci ligeey garibaldi mii tukkee na genova atum g ànd ak lu jege junniy xarekat yu bokkoon ci way coobarewu yu itaali yi nu tudde woon boroom simis yu xonq yi daal di wàcc ak ñoom sisil jot faa dàqe doole ya fa nekkoon te àndoon ak buurub napoli bi ginaaw diirub ñatti weer daal di jéggi xat xatu silil bi dugg ak dooley xareem ji napoli ci lu dul jàmmaarloo gu nu man a tudd ci noonu napoli mujj ak dëkk yi nekk ronam dugg ci bennoo gi samp victor emmanuel muy buuru itaali dooley piemonte ju xare ji jawali woon na ca diiwaan ya nekkoon ca ron kilifteefug paab bi mu jotoon a nangu moomeeli paab bi bepp lu ci dul rom ci noonu xarekati piemonte yooyu jawali woon ca soldaari garibaldi ya ca napoli ci ndigalul kafour ñu àndandoo nag xeex ba nangu mbooleem gox yi nekkoon ci ron nguurug napoli te garibaldi manu fa woon àgg moo rekk ci noonu victor emmanuel ñëw dugg napoli ni ku gañe di dugge ci dëkk bu nu xare ba nangu ko parlamaa bu itaali bu bees bi def na ndajeem mu njëkk ca torino bisub febriye atum g ca ndaje ma lanu ndëppale victor emmanuel def ko buurub itaali gu nu bennal gi ginaaw bi itaali taxawee di ag nguur gu nu bennal ba am juroomi weer la kafor faatu ci sulye atum g garibaldi it bàyyi politig ndax kat moom li ko taxoon a jug mooy ligeey ci itaali doon benn waaye soxlawutoon ay pali politig def rom peeyu nguurug itaali gi waa itaali yi delloosi nanu venezia mi otris tegoon loxo nangu woon ko delloosi gi di ci atum g mu mujj nag moom venezia di ab gox ci itaali ginaaw ba nu fa dàqee dooey xare ju otris ji nanguwaat googu nag ñi ngi ko mane ci ñàkk a tal gi leen otris ñàkkoon a tal ngir xeex bi mu nekkoon di ko def ak brusiya fraans it ay xarekatam gennoon nanu rom ngir sotti gi fraans sotti woon yitteem ca xareem ba ak brusiya bi mu ko defee soldaari itaali yi daal di leen fay wuutu ci sebtambar atum g ñu daal di jibal ci anam gu ofisel ne rom daal mooy peeyu nguurug itaali gu nu bennal gi doxaliin wii merloo woon na paab bi yobbu woon ko ci mu bañ a nangu loolu ne woon it du man a summiku ci sañ sañu politigam yi te du nangoo raflewu ci nguuram gi noonu la mbir mi nekke woon ba g ca la genn dëppoo ame ci diggante mossolini ak paab bi dëppoo googu mayoon na paab bi mu doxe nu ko soob ci mbiri diine ji te am ag tembte gu mat ca vatikan am it sañ sañ ci yabal ay ndaw yu koy toogal ca biti ñu wutal ko nag moom paab bi njëlul boppam lu mu jagoo nii nag la itaali doone woon benn muy lol ay doomam a ko xeex doomam yoy danoo jëloon seen coona bepp def ko ci goreel ko bennal ko te fuqarcee ko ci ngëbug jàmbur bu leen ruuroon teg leen loxo bennoo gii de lu ñepp soppoon la ndaxte doole la ci ñoom di teddnga di tembte te dig fonk sa xeet bennoog itaali du lenn lu dul meññatum sellal ak gëm ag bennoo mooy wuyyu gu mag ga ca woote ga michiavelli doon woote moom mi doon sàkku ciw nitam ca teereem ba tudd buur bi te looloo njëkkoon bennoo gi ci ay xarnu mu doon sàkku ci ñoom ñu ligeey ngir bennal seenuw reew doggantal gu ñaareel gi bennoo gu almaañ almaañ njëkk xare yu napoleon yi almaañ njëkk xarey napoleon yi dafa seddaliku woon ci lu jege ñatti teemeer ak juroom benn fukki diiwaan yepp it ci ron imbraatoor gu otris lanu nekkoon walla li nuy tudde imbraatoorug rom gu sell gi almaañ gepp it genn nguur rekk a fa nekkoon gu mag te temb mooy gu brusiya nguur googu nag jëmoon na kanam te ag yewwuteem fés ci jamonoy buuram ba tuddoon fredrick mu mag mi great fredrick g mooy ki ko defoon muy nguur gu dëgër te am doole bu ko defee waa almaañ yepp wëlbati seeni gët jëme ci nguur gii ngir bëgg ag bennoo almaañ ci jamonoy napoleon napoleon ak xarekatam ya xuusoon nanu ci diiwaani almaañ yi teg leen loxo daal di jawali ca nguurug brusiya gi nga xam ne jàmmaarloo woon na ak ñoom cig njàmmaar ak fit waaye napoleon moom mujj na ko not te gañe ko ci mujj gi ca xareb yena ba atum g daal di teg loxo peeyam ba berlin napoleon merloo woon na lool waa brusiya yi ci dog gi mu dogoon ay wàll ci seeni suuf te jébbaloon leen diiwaanu saksoni bi waaye nag ci geneen wàll am na lu am njariñ lu mu fa indi ndaxte wàññi woon na limub diiwaan yu almaañ yi ba ci fanweer ak juroom ñeent rekk te bu njëkk lu jege lanu woon kon jëfi napoleon jii mbir la mom moo nooyal yoon wi waajal ko ba ag bennoo gu almaañ man a judd man a taxaw almaañ ginaaw ndajem vienne mi ginaaw bi napoleon bonaperte daanoo atum g ci lanu def ndajem vienne ñu jële fa ay saxal yu bari bokk na ci yooyu dagg doox bu warsaw gu poloñ gi dagg ko ci brusiya te jox ko rusi bu ko defee ñu jox brusiya moom itam goxub rayan ak xaaju diiwaanu saksoni daal di taxawal ag bennoo gu almaañ gu làmboo fanweer ak juroom ñeenti nguur nguuraan yu almaañ otris jiite ko defiin wii nag mi ngi ame ci càkkuteeful metternich ak naj gi mu doon naj way daje yi ngir ñu defal ko bëgg bëggam boobu bennoo gu almaañ gii juddoo ci ndajem vienne mi nekkoon na di lu manul a wéy ndax kat otris moom daa tàmbli woon di genne ay saxal aki ndigal yuy kontar tas xibaar gu gore te wéeroodi fenn tey kontar mboolooy almaañ yi daan sàkku ag bennoo te daan ko woote te otris it daa mujjoon teg loxo ci jataayub bennoo gu almaañ gi te ga woon ko ci mu genne ay saxal yuy digale ñu fuglu daara yu mag yi ak leekol yi ak ndaje yi añs doxaliin yooyu nag taxoon na ba ay kàddu jib yu ay waa almaañ di sàkku ñu fipp ci kaw otris tey sàkku ñu jeem a bennal almaañ ci keppaarug nguur gu almaañ gu dëgër loolu mooy li xeltukatu almaañ bi hegel daan sàkku te daan ko woote moom ak ñeneen ñi daa jam bennoo gii nga xam ne otris a ko moomoon daanaka te tegoon ko loxo taxawaay bi nguurug brusiya ame woon ci naal yi jëmoon ci bennoo gu almaañ gi nguurug brusiya dafa tàmbli woon di yëngu ngir dajale xeetu almaañ wi duggal leen ci genn nguur gu almaañ gu nu bennal mu daal di woon rëddal boppam ab politig bu muy jaar ngir àgg ci loolu mu bëgg mu daal di woon door ci dëgëral boppam ci biirum reew defaraat doxaliinam yekkati koom koomam soppi nosteg galag yi aju woon ci nduwaan ci mbooleem goxi nguur gi ñu daal di taxawal noste gi nu daa wax solofrayn di ag bennoo ci wàllug nduwaan mooy li neenaloon nosteg nduwaan gi ci biir almaañ nga xam ne li nekk ci biir reew mi cim njaay deesu ci genne duwaan nga xam ne danoo feexal yaxantu gi ci brusiya ëfal ko ba mu man a doxe ni ko soob ci lu dul ñu ciy teg ay tënk tënki galag mbaa yu nduwaan doxiinu brusiya wii dey dees na ko lim mu dig soopiku gu mag ci taarixu bennoo gu almaañ gi doxal nanu ko nag ci atum g ci biir ay goxam yu biir yi gox yooyu nga xam ne njëkk nosteg solofrayn gi danoo nekkoon ay gox yoo xam ne bu ci nekk daa amoon nosteg pobb gu nduwaan gu mu bokkul ak kenn waaye bi solfrayn taxawee lanu bennal biir brusiya ci wàllug nduwaan ginaaw bi mu nekkee moom brusiya di lu nu seddale ci juroom benn fukki goxi nduwaan waa brusiya yi yëgoon nanu ne benno gi ci wàllug koom koom mooy cëslaay li nu war a teg bennoog almaañ gi ci wàllug politig looloo taxoon kilifay brusiya yi tàmbli woon a fexe nu nuy def ba duggal yeneen diiwaani almaañ yi ci bennoo gu nduwaan googu brusiya nag amoon na ndam ci li mu doon wut ci yenn ci diiwaan yu almaañ yu ndaw yi waaye nag jot naa dajeek ag jàmmaarloo gu mag ci yeneen diiwaan yu almaañ yu mag yi li ko waral mooy ñoom dañoo gisoon ne li gën ci ñoom mooy ñu sosal seen bopp ag bennoo gu ndawaan gu temb ngir xeex ci bennog nduwaan gu brusiya gi looloo fi indi woon ñatti bennoo yu nduwaan ci almaañ ñooy 	solofrayn 	 bennoog nduwaan gu bavar gi nga xam ne mi ngi judd woon atum g maanaam ginaaw bi gu solofrayn amee ba am ñaari at 	ak bennoo gu nduwaan gu saksoni mooy gi saksoni taxawaloon atum g kilifay brusiya yi xamoon nanu ne diiwaani almaañ yi dananu nangoo duggsi ci bennoo gu solofrayn gi bu nu soppee sart yiy tax manees cee dugg looloo taxoon ñu soppi sarti solofrayn yi nga xam ne leegi danoo sos ab jataay bu làmboo mbooleem ndawi yi ci bokk buy saytu noste googu leegi nag lu fa duggati rekk ci li bawoo ci nduwaan mi ak galag yi ñu koy seddale mbooleem diiwaan yi ci kem limub ña fa dëkk soppi yii de dimblee na ci yaatal gëweelub solofrayn gën a yàkkali ab geewam leegi nag bavar bokksi na ci ak saksoni ci atum g ca saa sa tam nga tàmblee gis lu lay won ne solofrayn moom tàmbli na a naat ak a am ag yokkute yaxantu ga tàmbli woon nay jar di dox mbay ma màgg endustri ba jëm kanam ci mbooleem diiwaan yi bokksi ci solofrayn am na nag benn jëfka boo xam ne moo àntul solofrayn mooy moom de noste gu waa almaañ xalaat ba def ko la loxol otris duggu ci jenn doole it ju ko man a teg loxo yoonam nekku ci metternich gisoon na ay wi nekkoon ci noste gii waaye bi mu koy gis fekk na waxtu wa jàll manatu ca woon dara mu daal di bind imbraatoor bu otris bi ne ko na la wóor ne nguuri almaañ yi bi lii amee de di nanu nekki wenn yaram wu jàppaloo ci ron kerug doxaliin gu brusiya te da na jàppeji brusiya muy moom aw yaram wu di doxandeem wu tumbrànke wu bokkul ciw yaramam te kat waa otris yi ñoom ca dëgg dëgg dunu ay doxandeem ci waa almaañ yi ndax ñoo bokk xeet làkk ak taarix man nanu ne almaañ gepp mujj na bokksi ci solofrayn gi atum g xalaatu xeltu bu hegel bi feddali woon na dooley nguur ak ray gi muy ray jëmm ak lepp lu mu am ngir sàmm dooleem akug màggam ak wegeelam nguur walla àtte ci gis gis hegel cëslaayam mooy doole ci doole rekk la man a dëgërale gëgg kon nguur walla àtte gu dëgër ci gis gisu hegel mooy nguurug walla àtteg dëgg kon moom hegel day mel ne moo teg ci loxol brusiya lay wa xeltu guy rafetal di baaxal seen jëfi jiite googu nu jiite woon bennalug almaañ gi ñu leeral leen ne bi g di jot fekkoon na brusiya muy reew mu am kàttan ci tere otris muy dugg ci mbiri nguur nguuraani almaañ yi naka noonu nekkoon na it mu amoon kàttan ci jiite yëngu yëngu gi jugoon ngir bennal almaañ nguur nguuraan yi bokkoon ci solofrayn it doon man a dimblante ci seen biir ci wàllug koom koom te daan jëflante ci lu dul yoonu otris di ci nekk mbaa ñuy diisoo ak moom walla ñu koy tàggu ci noonu nguur nguuraan yooyu tàmblee xoole brusiya bëtu kilifa ci noonu la bennoo gu koom koom googu doon màgg ak a naat ci ro kerug solofrayn mujjoon di ab jeego bu mag jëm ci ag bennoo gu politig ak xare ci almaañ jeexiit yi fipp gu atum g defoon ci amug bennoo gu almaañ gi ay fipp yu bari jot nanoo am ca tugal atm g ag fipp am ca paris am gu am ca vienne geneen ca brusiya ak ay fipp ci itaali ak almaañ yepp it di xëccu jëm ci ag gore demokraasi ak xeetu metternich mu màggat mii mujjoon na manatul woon a noot fippi tugal yooyu mbaa mu giimal leen ni mu ko baaxoo woon a defe kërug orob gi mujj ni ko metternich di waxe di kër gu màggat te ràpp ba àgg ci maneesatu cee yatt sax ab palanteer ciy miiram ngirug màggat kon leegi li jaadu kay mooy ñu màbb ko te wuutal fa geneen kër gu yees ca dëgg dëgg nag loolu am na ndax kat noste ga amoon ca la ëppoon ca reewi tugal ya daa mujjoon di lu ràpp ngirug yàgg mujj manatutoon a ñàkk ñu yeesalaat ko te taxawalaat ko ci anam gu dëppoo ak li jamono laaj metternich dawoon na te daanu woon ci noonu buurub brusiya bi frederick william mu ñeenteel mi daal di jug woote am ndaje mu parlamaa ngir ñu defaral brusiya ab sartu reew bu bees mu dig aw askanam ne leen moo fas yeenee jiite yëngu yëngu giy jug ci jeem a bennal almaañ ci benn bataaxel bu mu leen jàngal ndaw yi teewal almaañ yepp teewe woon nanu ndajem atum g moomu ñu def fa ay gëstu ci lu aju ci almaañ gu nekk benn ndajem parlamaa mii ñi ngi ko gën a xame ci turu parlamaab frankfort ndaje ma ëmboon na lu bari ciy woykat aki xeltukat aki taskati xibaar aki ustaas ñatti saxal nag yu mag juddoo nanu ca ndaje ma 	bennal almaañ ci njiitul buurub brusiya 	ñu boole ci bennoo gu almaañ googu wàllug almaañ gi bokkoon ci imbraatoorug otris gi 	genne otris ci bennoo gu almaañ gi way daje yii ci frankfort seenub lim àggoon na ci ciy jëmm tànnoon nanu buurub brusiya bi fredereick william mu ñeenteel mi def ko imbraatoor ci almaañ gu nu bennal gi waaye frederick moom daa bañoon ne du dëppoo ndëppul imbraatoor li nu ko joxoon te way daje yi joxoon ko ko ndax da ne ndëpp li daal ndawi askan wee ko ko jox waaye buur yeek kàggam yi joxuñu ko ko looloo taxoon nanguwu koo sol la am nag mooy ne buuru brusiya bi dafa bañ a jël ndëpp li ndax xam ne otris ak rusi ànduñu woon ci bennoog almaañ googu te manoon nanoo xëy di duggati ci seeni mbir ngir loolu rawati na ne otris moom jot na a not fipp gi amoon ca peeyam ba vienne nga rax ci dolli ne buuru brusiya bi moom dafa gëmoon gisiinu àq ak sañ sañ bu yàlla bi mooy gisiin wi naan ñoom buur yi yàlla a leen fi teg moom lanu fi wuutu nit ñi tegunu leen fi du keneen it looloo taxoon bu nangoo it ñu def ndaje moomu muy mu frankfort mi jubluwu ci woon lu dul ngistal waaye du ligeey bu fullawu mbaa mu dëggu ci yoonu soppi otris ak rusi dimblante nanu ci màbb barlamaab frankfort bi ak naalam yi mu amoon te nu jëm cig bennoo gu almaañ looloo waraloon jeem gi nu doon def ngir bennal almaañ ci ron kilifteefug brusiya ci atum g mujjul woon àntu waaye li muy àntoodi lepp teewul xalaat bi sax ci xoli ak xeli waa almaañ yi ñu mujj waa almaañ ñi xam ne daal dunu man a amalati seen bennoo googu ci anamug jàmm mbaa gu sartu reew ndaxte otris àndu ci te mi ngi koy xeex ak doole looloo waraloon nu jëloon seen yitte def ko ci amal am mbooloom xare mu dëgër mu leen di man a may ñu man a genne otris almaañ cig njëlbeen door a lijjanti nag nu nuy doone benn ci ginaaw bi xalaat bii nag diisoowaale bu brusiya bii di bismarck àndoon na ci te jàpple woon ko dëgëral ko moom mooy otto von bismarck boroom kurpeñu weñ bi politigu bismarck ci lu jëm ci bennoo gu almaañ gi bismarck mi ngi judd atum g am njàggam mu kawe mu defe ko ca daaray berlin ju mag ja daal di dugg ag coldaar gennati ca dem nag feete ca boppam ca toolam ba mi ngi bokkoon nag ci njaboot gu woomle gu ami alal yu rëy ca brusiya sampoon na boppam ngir nu fal ko ci bennoo yu almaañ yi atum g ñu tànnoon ko it muy ab cer ci parlamaa bu brusiya bi ligeey na it ci toolub diplomasi doonoon ndawul reewam ca butrsburg ca rusi ginaaw bi mu nekkal reewam ca paris foofee la ko william mu njëkk mi doon jiite brusiya woowe woon mu juge fraans ngir jiite si njiitug jawrin gi ci brusiya bismarck nag nekkoon na ku gëmoon te daa dëgëral noste gu nguur gu nu joyal te gëmoon ne buur daa war a am doole te am soldaar su dëgër egliis bi jàpple ko ak garmi yi bismarck moom faalewutoon parlamaa bi gisoon na ne jëm kanamug aw xeet walla ag yeegam jëm ca kaw manul a ame ci lu dul ay buuram di ñu kawe ay yitte ak ay kilifaam waaye du nu ko ame mukk ci ay saxal yu juge ci ay parlamaa aki nostey sarti reew bismarck yitteem jepp mi ngi ko jëmale woon ci genne fraans ak otris almaañ mu gisoon ne lii daal manul ame ci lu dul dooley xare ju mag ju leen ci man a ga ci noonu mu tàmblee ligeey ci dëgëral dooley xare ji ak kàttanal ko mu daal di tas parlamaab brusiya bi ndaxte moom parlamaa bi daa bañoon ne du woote alal ji mu doon laaj ngir man cee dooleel soldaaram si ci noonu mu tëjopon kepp ku wuuteek politigam boobu daal di digle ñu fuglu yeglekaay yi daal di beddiku sartu reew mi ne du ci sukkandikooti alal ji mu soxla woon mu gennelu ko ci ndigalul buur bi bañ cee sukkandiku ci lu parlamaa bi wàllug xeetu nag moom gis gis bi mu ci amoon moo gënoon a yaatu bi mu amoon ci sartu reew ndax daa gisoon ne sartu reew moom mi ngi ame mook ay jubluwaayam ci ginaaw bu ag xeetu amee ba noppi bismarck nag neenalul mbooleem parlamaa bi mbaa mu tas ko lepp moom kay da caa neenl walla mu soril ko ñatti mbir ñooy 	coldaar gi 	politigu bitim reew bi 	fal ay jawrin ak di leen folli bismarck wone na dogu gu mag akug takku contar teg gi otris teg loxo almaañ loolu nag gën na a fése ci taxaw gi mu taxawoon ci dakkal politigu otris bi muy teg almaañ looloo taxoon otris mujj woo buuri almaañ yepp cim ndaje ca frankfort ngir sos ag bennoo gu federaal guy doxal ab goornamaa boo xam ne ay dooleem ak sañ sañam mi ngi koy jële ci sart boo xam ne otris moo koy defar tër ko bismarck gisoon na ne lii de ag anam gu yees gu otris jëlati la ñu muure ko mbubum diplomasi ngir yeegati ci kaw waa almaañ yi bismarck melaloon na sart boobu ne mooy sart bi gën a bon ci mbooleem yu mas a am ci kaw suuf ci noonu mu ne woon du teewe ndaje ma lu dul ci kaw ñu jox brusiya ay àq aki yelleef yu tol ni yi nu jox otris ci ñaari mbir yii ñooy 	dëgël ak wéyal jibalug bennoo gi 	jiite benno gi bismarck ci taxawaayam bii leerale na ci ne otris daal moom ñàkk na kàttan ga mu amoon ci aakimoo moom rekk mbirum bennoo gu almaañ gi te it won na nguur nguuraani almaañ yi ne brusiya mii kat mooy jenn dooley almaañ ji man a jiite bennoo gu almaañ gi bismarck jeem na a fàggu cofeelug rusi ngir mu bañ a feete fenn bu ab xare tàkkee ci diggam ak otris loolooo taxoon mu dugg ci lëj lëju poloñ bi jàpple ci rusi kontar gori ploñ yi defoon ag fipp kontar rusi ngir dañal ag àtteem te jeem a am ag tembte ba man a amal ag àtte gu poloñ gu temb fraans nag àndoon na ca fipp ga te jàpple ko askanu angalteer wi ànd ca waaye goornamaa ba moom àndu ca woon ndax daa ragaloon ag nguurug poloñ gu katolig judd guy dem di àndeek fraans ci noonu bismarck moom dem jàpple ji rusi te jàpple googu gu amoon doole la ndax moom reewam brusiya daa taqaloo woon ak poloñ ba noppi taqalook rusi te it nanguwutoon a ànd ak fraans ak otris kontar rusi xarey bismarck yi ngir taxawal bennoo gu almaañ bismarck xuus na ay xare ak lu bari ci reewi tugal yi digoo k almaañ ngir bennal reewi almaañ yi ñu tudd ñatt rekk ci xare yooyu ñooy xare brusiya yi ak danmark bismarck xuus na ab xare kontar danmark atum g ànd ca ak otris ngir nangu ñaari diiwaan yii di shalswig ak holistin ñu doonoon ñaari doox yu bokkoon ci bennoo gu almaañ gi te danmark tegoon leen loxo danmark mujjoon na ñàkk pexe daal di deltu ginaaw wëlif ñaari doox yooyu atum g bu ko defee brusiya jël dooxu shalswig otris it àtte diiwaanu holistin xarey brusiya ak otris bismarck gisoon na ne xare bi moom deet sikk aji tàkk la ci diggante brusiya ak otris te li ko waral du dara lu dul diiwaanu holistin ndax kat mbir yi manunu woon a nekk di wéy ci anam gii nu nekke di ay maslaa yu dëggoodi aki lijjanti yu xootadi aki juboo yu gàtti dig bis bu yàlla dogalee njortul bismarck loolu mujj di dëgg ba brusiya am ndam loolu de da na nekki muccug waa almaañ ñi ci gàllankoor gii tukkee ci otris gu leen di teree nekk benn tee bennoo gu almaañ gu wér man a am màggug brusiya ci wàllug politig ci biir bennoo gu almaañ gi mujj di luy jeqi njàqare ci otris solofrayn moom màgg na ci anam gu doy waar rawati na bi ci nguur nguuraan yu almaañ yi tiim geejug bëj gànnaar gi bokksee ci noonu lu sakkan jug ciy yooni weñ lënkale diggante wàll yu almaañ yu wuute yi loolu tam dooleel bennoo gu koom koom gi nga xam ne brusiya mujj na di ci ki ci gën a jariñu sabab yii rekk doyoon nanu ngir taal xeex bi ci diggante brusiya ak otris rawati na ginaaw bi dooley brusiya ji doxee jawali holistin nangu ko te moom daa nekkoon ci ron kilifteefug otris ngir dëppoo gi amoon ci diggante brusiya ak otris atum g bismarck moom lijjanti woon na ba rusi genne loxoom ci diggam ak otris loolu nag di ci jàpple gi mu jàpple woon rusi ci giimal fipp ga amoon ca poloñ atum g dëppoo woon na ak imbratoor bi napoleon iii imbraatooru fraans moom itam ngir mu seetaan kook otris bañ cee dugal loxoom li mu koy faye ci loolu nag mooy bàyyi kook yenn moomeel yi ci goxub rayn mu demati tapoo ji ak nguurug itaali gi nga xam ne li doonoon yitteem mooy nocci venezia ci loxol otris ngir matal ag bennoom xare bi amoon ci diggante otris ak brusiya xare la woon bu fëkk te gaaw wéyutoon lu ëpp juroom ñaari ayu bis moo waraloon nu tudde woon ko xareb juroom ñaari ayu bis yi dooley brusiya ji jot na ca a gañee ju otris ja ca xareb sadwa ba ca bohima atum g mu manoon a àgg sax moom dooley brusiya ji ba ca vienne bu imbraatooru fraans bii di napoleon iii jugutoon dox tànki jàmm ci diggante bi ci noonu bismarck daal di ñàkk pexe taxawal xeex bi ngir ragal fraans dugg ci xeex bi ci wetu otris te it bismarck moom da ne woon na doylu nag ci gañe gii mu gañe otris ak dammte gii mu ko dammte ndaxte soril na ko bennoo gu almaañ cig wàll te it bëggutoon a toroxal imbraatooru otris bi ngir loolu man na a tax bu jugee ëlëg moom brusiya di xare ji ak fraans otris du ko sot ci geneen wàll ag juboo amoon na ci diggante brusiya ak otris ñu koy wax juboog braax gi atum g ci la yii ame 	gennug otris ci bennoo gu almaañ gi gi mu tegoon loxo la ko dale ca jamonoy metternich 	duggug mbooleem nguur nguuraan yi nekkoon ci bëj gànnaaru dexu rayn gi ci bennoo gu federaal gu almaañ ci ron njiitul brusiya diiwaani bëj saalum rekk a bokkutoon ci bennoo googu 	bàyyee gu otris bàyyee itaali venezia gis nga ko bismarck kat am na ay ngërte yu am solo ci xareem beek otris moom de fare na fi bennoog almaañ gu yàgg ga indi fi leegi ag bennoo gu almaañ gu yees gu ame ci mbooleem reewi bëj gànnaaru almaañ nga xam ne ñaari doox yii di shalswig ak holistin ci lanu woon buuru brusiya bi jiite ko bismarck nos na bennoo gu yees gi wutal ko ab parlamaa rashstach ndawi askan wa di fa daje ak jataayub bennoo gu almaañ gi bundasrat ndawi diiwaani almaañ yi bokk ci bennoo gu almaañ gu bees gi di fa daje bismarck it lijjanti na ba def ak diiwaani bëj saalum yi bokkutoon ci bennoo gi lijjanti woon na ba def ak ñoom genn tapoo gu xare xareb brusiya ak fraans xetug xare tàmbli woon na a xeeñ ak a jòlli ci diggante fraans ak brusiya ginaaw bi brusiya gañee ca xareb sadwa ba ndaxte fraans moom begutoon dara ci lii brusiya amal ciy ndam ci kaw danmark ak otris cig wàll ak àntul gi mu àntuloon bennoo gu almaañ gu bëj gànnaar gi ci geneen wàll fraans moom daa jàppe woon loolu muy aw xët ci digg ginaawam ndaxte moom kat manul woon a dékku ag nguur gu almaañ gu am doole ci wetam moom kay li ko sooboon mooy almaañ des di nguur gu nu dogat ngir mu nekk moom fraans di reew mi am kilifteef ci sowwub tugal bi moom kay jamono ju nekk da daa kontar bennoog almaañ gi ni ko otris kontare woon bismarck it tàmbli woon na a xalaat nu muy xëcce diiwaani almaañ yu bëj saalum yi ngir nu bokksi ci bennoo gi jëf ju mel ni jooju nag fraans du ko doon nangu ndax moom tàmbli woon na di dugg ci mbiri diiwaan yu almaañ yu bëj saalum yi ngir tee leen a bokki ca bennoo gu almaañ ga nga xam ne brusiya ko jiite woon lëj lëju ku jigeen ki waroon a donn espaañ daal di taxaw mooy lëj lëj bi taaloon xare bi ci diggante brusiya ak fraans lëj lëj boobu mi ngi tënkoo woon nii gàngunaay gu nguurug espaañ dafa feexoon ginaaw bi lingeeru espaañ bi elisabeth dawee ñu gaaral buur bi leopold ndëpp li moom mi ngi bokkoon ci njabootug hohenzellern di woon ab njegeñaaleb imbraatoor bu brusiya waaye ak li leopold di bañ lepp ne du sol mukk ndëpp li teewul fraans mer ci loolu jàmbat ko ci buurub brusiya bi daal di sàkku ci moom mu warlu ne du ànd ci ñu samp kenn ku bokk ci njabootug hohenzellern ci gàngunaayaug espaañ gi waaye buuru brusiya bi bañ ndax loolu kat dafa xaw a laal teddngaam ak ngoram te xaw a niru ag yabeel loolu nag mi ngi ame woon cim ndaje mu mu defoon ak ndawul fraans ca ems bu ko defee buuru brusiya bi yonnee ab day ca la juge woon ca ndaje ma mu yonnee ko bismarck mi nga xam ne lepp li mu doon def mooy neggandiku ab pose ngir jibal ab xare ci kaw fraans ba mu ko defee bismarck xëy tas ci yëglekaay yi ay cofiit ca la bawoo woon ca ndaje mooma ngir merloo ci fraans loolu nag ni mu ko defe mooy genne ay baat yu xaw a wow yu begloowul dara fraans ci noonu fraans jug jibal ab xare ci kaw brusiya ci sulye g te fekku ko woon jekk ngir xeex te taxul woon it mu xalaat ci ngérte yi man a juddoo ci bii xare bis bu nu dàqee fraans ci xeex bi brusiya li nuy wax xareb fëkk la doon def ak fraans maanaam gaawal ko loolu nag jot na koo def ba am ci xam xam ca xareem ba ak otris bi mu ko defee tàngooru xare bi sax di tar lu tollook juroom benni ayu bis waaye tàmblee giim ci ginaaw bi rawati na ci ginaaw bi ay màndargay kawe ak ëpp doole tàmblee feeñ ci xeex bi ñeel brusiya xare bi bepp nag ci suufus fraans la doon tàkke jotoon nanoo dàq fraans nag ci xeex yu bari bi ci gënoon a siw nag mooy bu sedan ca satumbarg nga xam ne àggoon na ci napoleon iii manutoon a ñàkk a wommatu te nangu ne gañe nanu ko ngir dàq yu metti yi te toftaloo te yepp di yu nu teg ci kaw dooley fraans ji ci biir suufus fraans te ray lu sakkan ciy soldaaram te itam lu jege ñaari teemeeri junniy soldaari almaañ sutuxlu ba ca xolub fraans te mu leer nàññ ne fraans moom manatul a gañeeti brusiya ca jamono joojee te manatu koo genneeti suufam loolu nag di woon ci oktobar g ci noonu imbraatoor gu fraans gu ñatteel gi daanu ñu daal di taxawal ci paris nosteg pénc gu ñatteel gi daal di teg fraans ñeel brusiya alamaanug xare gu toll ci juroomi bilyoi frank yu fraans loolu mooy tollook daanak alamaan bi napoleon bonaparte tegoon brusiya bi mu ko dumaa ca xareb yena ba g bu ko defee ñu juboo ci xarekati almaañ yi dunu genn fraans li feek fayeesul alamaan bi moom nag jotees na koo fay ci diirub ñatti at nga rax ci dolli dagg gi nu dagge ñaari gox yii di alsaas ak loren ci fraans boole leen ci almaañ nii daal la bennoo gu almaañ mate woon ci njiitul brusiya ci loxol goor gu dëgër gii ni weñ bismarck mi nga xam ne dafa gëmoon bennal almaañ ak doonte day ci dereet ci weñ mbaa sawara bu ko defee imbraatoorug almaañ gi daal di sosu dib xew xew nag bu fés ci taarixu tugal bu bees bi boroom gàngunaay gi imbratooru almaañ bi mujj di ku ñu joyal ab gogam ci def li ko neex ci nguur nguuraan yu almaañ yi sartu reew bu almaañ bu bees bi yaxal na nu sos ñaari jataay 	jataayu bennoo gu almaañ bundasrat 	jattayu rechstag dooley yoonal ji nag mi ngi nekkoon ci bundasrat di jataay bi nga xam ne mi ngi ame woon ci juroom fukk ak juroom ñatti cer ñu seddale leen ci nguur nguuran yi nga xam ne ñoo amal imbraatoor gu almaañ gi brusiya nag moom rekk amoon na fukki kàddu ak juroom ñaar ginaaw bi mu am ñaar fukki kàddu ak li brusiya di moomadi li ëpp ci kàddu yi lepp ci bundasrat teewul mu gënoon fa a guddub loxo gënoon fa a am jeexiit ndax la ëppoon ca nguur nguuraani almaañ ya duggoon ca bonnoog almaañ ga danoo takku woon ci brusiya te daawunu woote lenn lu mu bëggul te daawunu jàllale genn saxal ca jataay ba bu fukki cer ak ñeent àndadee ca saxal ga bu dee nag jataayu rechstag nag moom man nanu ne mooy jataayub askan bi mi ngi ame woon ci ñatti teemeer ak juroom ñeen fukk ak juroom ñaari cer ñu leen di tànn ci anam gu sekkaree dooley jataay bii nag daanaka danu koo lafañal yòqeel ko ndax nguur ak doole yi nu ko joxoon ci ron sartu reew bu almaañ bu bees bi danoo nekkoon di yu doyadi te ñàkk solo bismarck nag jiite na goornamaa bu almaañ bi niki diisoowaale walla chancelier benn ci ñaari jataay yi manul woon ci moom dara mu yoroon it sañ sañ bu rëy te ci ron kilifteefam tam la almaañ gu rëy gii gepp nekkoon nga xam ne ña fa dëkkoon ca atum g jege woon nanu ñeen fukki milyoi nit mujj àgg ci ñeen fukk ak juroom ñeenti milyo ciy nit atum g di maanaam bi bismarck faatoo ba am ñaari at juroomeelu bunt bi sanc gu yees gi sabab yi fi indi sanc gu yees gi ak ay anamam reewi sancaan yi ñaawteefi sanc yi yëngu yënguy nasaraanal ak ay wi mu làmbool doggantal gu njëkk gi sababi sanc gu yees gi aki anamam xamale lan mooy sanc gu yees gi li sikk amul mooy sanc gu yees gii toppoon ci yewwuteg endustri gi ci tugal rawati na ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar fukk g sanc gii de ay reenam tàlliku woon na di dem ba ca yëngu yëngu yu wuññiy juxraaf yu tugal yi nga xam ne dees leen di jàppe ñuy bunt bi nu jaare bay dugg ci sanc gu yees gi tugal doon def ci reewi adduna bi sanc nag dees na ko xamalee ci ne mooy teg loxo gi reewi endustri yu mag yi tegoon loxo mbiri koom koom yi ak yu politig yeek aada ci reew yu bari ci yu amadi doole yi ci adduna bi rawati na yi ci di yu woomle ci wàllug mbay ak mbll looloo tax sanc ci maanaam mii mu yor du lenn lu dul luy yëngu ci nangu ak fëkk alali jàmbur ak ngacc dooley mbindeef yi ak jariñoo leen sababi sanc gu bees gi li sabab sanc lu bari la te lënkaloo ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii 	màgg gu gaaw gi ba ëpp ci wàllug endustri ci lu bari ci reewi endustri yu mag yi loolu nag tax ba reew yii mujj soxlawoo ay ne ne yu nu laalul aki ja tax na tam ba ag gëpplante gu tar te metti am ci diggante reewi endustri yu mag yi jëm ci yaatal seenug kilifteef ak sañ sañ ci gox yi leen man a warlul ag yokkute ci wàllug endustri ndax seen koom koomu xeet wepp ci endustri la tegu woon li juddoo ci loolu nag lu mujjoon metti la ci reew yu neew doole yii nga xam ne yu mag yii danu leen tegoon loxo ngir muucu seen njariñ yeek ne ne yu nu laalul yi ak ngir def leen ay ja yu mag te yaatu yu nu man a jaaye seen ligeeyi tugal yu endustri yooyu 	yokk gu ñi dëkke ci reewi endustri yi yokkoon loolu moo waraloon reew yii gëstu ji woon fu nuy wàññi seen ëppiitum askan moomu bu ko defee ñoom ñu man leen a nekkal dib jumtukaay bu am solo buy dëgëral seen koom koomu reew miy nday laaj na ñu xamal leen ne politigu genne ëppiitum askan boobu ak sotti leen ci reew yi nu sanc politig la bu nu nosoon jublu woon ci ligeeyal xemmeemteefi sanc yu reewi endustri yi amoon way dëkk yu bari woon ba ëpp 	bëgg a soppi nit ñi def leeni nasaraan nasaraanal ak wisaare diiney nasaraan ci kaw kaw yi ak ñu xamul ñi nga xam ne nasaraanal bokk na ci sabab yi gën a rëy yi waral wuññiy juxraaf yu tugal yi am te ñooy li ubbi buntub sanc waa tugal yi jëfandikoo nanu diine niki ab raas bu niy jaare ngir àgg ca seen bëgg bëgg yu sanc yi yu politig yi ak yu koom koom yi ak doonte danoo làqoon loolu bu ko defee mbubboo seen wax jooju nu daan wax naan wisaare ag nasaraan du lu dul xayal ak yiwal nit ñu deltu ginaaw ñi xamul dara adduna bi nag sonne na bu baax ci par parloo ak boddanteg diine ak xalaatu maa la gën bi reewi nasaraan yi ame woon jëm ci yeneen askan yi dul ñoom 	wàññiku gu tar gi amoon ci ñi dëkke woon ci kaw gi ci reewi tugal yu endustri yi taxoon ba jafe jafe am ci wàllug dundub mbay ci reew yii loolu yobbu woon na reewi yii ci ñu wuti bii dund ci reew yu neew doole yii nga xam ne mbay amoon na fa doole reewi tugal yi nag jaarunu woon ci yoon ngir am seen càkkuteef loolu ci misaal ñu jaare woon ko ci yaxantu waaye kay danoo jëfandikoo doole ak noot ak sanc sukkandiku ci seen dooley xare ji ak ñawug seen ngànnaay ak neew dooleg geneen wàll gi mu fas yeenee noot loolu mooy li ko dimbli ba mu man a am bëgg bëggam yooyu ci kaw askan yu doyadi yi 	lu bari ci reew yu mag yi li leen doon defloo sanc googu mooy feeñal ag yëg sa bopp aakimoo mbir yi ag rëy ci wàllug xeet yaakaar ne ñoo gën yooyu nag ay jumtukaay lanu won ngir wone doole ak màgg gi nga xam ne reewi sanc yii màggoon nanu ko te ame ko ni doole 	ay lonkoo yu tugal ak yu dul ñoom yu mag feeñ nanu ci biir yewwuteg endustri gi dajale woon it alal ju bari ba gisoon ne leegi danu koo war a meññali ca reew yay màgg ci wàlli koom koom yi ci noonu lonkoo yu adduna yu mag yi tàmblee gëpplante ci meññilu alal yooyu loolu nag jur ag jongante gu mag te tar ba mujj sax yii lonkoo tàmblee sàkku ci seeni goornamaa ngir ñu jàpple leen te dëgëral leen loolu tam daan yobbu goornamaa yi ci ñuy aar seen njariñu lonkooy reew loolu nag nooyal na yoon wi ba xeetu sanc gu politig man a taxaw di lol gëpplanteg koom koom a ko fi indi 	bëgg gi reewi sanc yu mag yu bari bëggoon na dëgëral seen yoonu jokkoo gu adduna loolu yobbu leen ci ñu teg loxo yenn yoon yu strateji yi ak waax yu am yi solo ak yoon yu mag yi am solo ci wàllug jokkoo gu adduna gi di taqale diggante goxi adduna bi 	bëgg gi yenn ci reewi sanc yu mag yi bëggoon a tas seeni xalaat aki dal principes yu seeni làngi politig ak seeni aada jàppe loolu nag ab jumtukaay buy ligeeyal seeni xammemteefi sanc anami sanc gu bees gi sancug tugal gu yees gi dafa jëloon ay melo aki anam yu wuute yoo xam ne xew xew ya peegoon te yiiroon reewum sancaan mi ak mi muy sanc xew xew yooyu danu doon jeexiital ci ñoom bu ko defee sanc gu bees gi dikk ci ay anam yu bari ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii sanc ngir dëkk xeetu sanc gu ñaaw gii feeñ na ci ginaaw yëngu yëngug wuññiy juxraaf yu tugal yi bu ko defee reewi tugal yiy wuññi daal di taxaw ci neewal doole ñi cosaanoo woon ci reew yi nu wuññi jaare ko nag ci di leen dàkku ak a genne seeni reew ak di leen alag ci xare yi di leen toraxal di leen seeyal ci biir mboolaayi reew miy sanc maanaam di leen def daanaka ñuy ñenn ci ñoom ci wàllug aada deesu leen manatee ràññale xeetu sanc wii mooy li waa espaañ defoon ca endo yu xonq ya ca amerig gu digg ga ak gu bëj saalum ga bi nu leen sancee te dëkke leen taxawal fa ay sancu yoy mujjoon nanu cuub gox bii ci cuubug espaañ ginaaw bi fi ay waa espaañ jëlee barabu endo yu xonq ya fa cosaanoo mel ne leegi fa lanu cosaano loolu di ci amerig gu digg gi ak gu bëj saalum gi lu ci dul bresil moom waa portigaal a ko sancoon nu mel noonu la sahyooni yahood yi defoon ca falastin bi nu ko sancee ci doole dëkke ko reewi sanc yu mag yi jàpple leen ci britani nekk ca bopp ba ci noonu la yahood yi tasaaroo woon ci adduna bi dajee dëkksi ca falastin ginaaw bi nu leen fa gàddaayalee jëme ci ron aarug reewi sancaan yi ak li askanu falastin daan xeex loolu lepp te daan ci jiyaar ngir bañ ko nii it la sancug tugal gi meloon ca afrig gu digg gi ak rodisiya ñu fay teg doomi afrig yi lu sakkan te lëw ciy coona di leen noot di leen teg loxo di leen tiital di leen tàqale ak a gënale ci wàllug xeet ak lu bokkul ak loolu lepp ci anami mbugal yu tar te mbaam àlle teg loxo gu xare ay reew yu sancaan jug nanu teg loxo ay reew nangu leen ci doole loolu nag li leen ci gënoon a jañ gënoon leen cee yobbu mooy neew doole gi nu gndiku woon ci yii reew rawati na ci wàllug xare li ñu doon jublu ci teg loxo googu mooy man cee jaare bay wéyal ak a doxal seen naali sanc yooyu daan tax ba nuy man a teg loxo ci koom koomi reew yi nu nangu ci seeni dooley xare ci seen politigu bitim reew ak seeni mbiri xam xam ak aada ngir man a samp bu baax seen kenoy sanc ci dëkk yii misaali sanc yu mel nii yu bari lanu nañu ci indi yii rekk sanc gi fraans defoon aljeeri atum g ak sanc gi britani defoon adan atum g defoon ko it isipt atum g ak teg gi fraans tegoon loxo dunu madagaskaar atum g beljig defoon ko kongo atum g ak nangu gi itaali nangu woon libi atum g ak ecopi g xeetu sanc wii mooy wi gënoon a tar te gën a ñaaw ci xeeti sanc yi ndaxte lu diisoon la ci ñi cosaanoo woon ci reew yi nu tegoon loxo ndaxte sanc gu sukkandiku woon ci jëfandikoo doole la waaye li muy tar lepp ak a tiitale teewul nit ñi xeexoon ko te xaru woon ci jële ko fi jànkoonteek lu sakkan ciy jafe jafe aki coona ci seen xeexu njàmbaar boobu ñu ko doon xeex ba mujj ame ci lu màgg li nu doon wut muy gore ak tembte ak dàq sancaan yi ñu juge seeni reew aar reewi sanc yi mujj nanu wut geneen anam gu yees gu nuy sance ak a tege loxo reewi jàmbur yi ñu soppi woon seen sanciin woowu doon tegu ci dooley xare wut weneen wu nuy tudde aar aar nag ci maanaa mu sanc mi mu yor gënul benn yoon sanc gi nu daan defe ci teg loxo ak nangu reewum jàmbur ci doole moom daal aar tur la ci tur yi sancaan yi indi te jëfandikoo ko ci yenn ci ay jamono bu dee maanaa mi aar yor ci wàllug sanc mooy def gi reewi sancaan yi daa def ay dëppoo aki kollarante ci anam gu maandoodi ak yeneen reew yu doyadi yi te neew doole bu ko defee reewum sancaan mi day kollaranteek reew mi mu sanc ci di ko aar ci mbooleem tooñ gu ko man a dikkal juge ci dooley politig ju digook moom walla jeneen bu ko defee loolu di may reewum sancaan mi muy doxal mbirum reew mi nuy aar ci wàlli kaaraange bitim reew ak koom koom reew mi nu aar daal du doxal lu dul mbiri biir reewam rekk loolu nag daa na tax mu nu aar mi daawul am temb gu mat ndax ag gore gu politigam kollarante yooyu danu ko daan tënk ba daa ko tee muy def ay ligeeyam ci mbooleem ay mbiri reewam ci ni mu ko neexe misaal yi ci loolu yu bari lanu ñu indi ci yii rekk aar gi fraans defoon tunisi atum g ak maraakes g ak aar gi britani defoon adan dale ko ca ba mu ko tegee loxo atum g ak yeneen barab yi mu tegoon loxo feetale reewi sancaan yu mag yi tàmbli woon nanoo wutati ay tur yu bees ngir sanc gu bees gi ginaaw xareb adduna bu njëkk bi loolu nag mu jublu woon ci muur sanc gii muy def muuraayu ag yiw akug xay loolu nag du tee sanc moom di lenn rekk ak mbubb mu mu man a sol ak melokaan wu mu man a dikke ci noonu la feetale dikke moom nag ag anam la ci anami sanc gu yees gi nga xam ne jataayu kureelu xeet yi saxaloon na ko te nangu ko mooy kureel googu nu sosoon ca paris ca ndajem jàmm ma nu defoon atum g ngir lijjanti lëj lëj yi amoon ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi boobu kureel nag fraans da ca a defoon ay jeexiit yu mag mook britani nga xam ne ni nu bëgge mu mel ni daanaka la mel dalu feetale ci jëmmi boppam ñi ngi ko jële ci cosaan la ca yoon wu rom wu yagg wa feetale nag noste la gog defoon na mbooleem reew yi nga xam ne reewi dëppoo yi nangoo woon nanu leen ci imbraatoorug almaañ gi ak reewum usmaan mi ñuy ay reew yu nekk ci ron feetale googu bu ko defee reewi dëppoo yi ñoo nekkoon reew yi nu joxoon feetale googu maanaam ci seen ron kilifteef lanu feetale woon mbooleem reew yi nu nangoo ci almaañ ak reewum usmaan mi bu ko defee ñu waral ci reew yiy feetewoo feetale gi ñuy def leeg leeg ñu indi ay saxal aki leeral yu aju ci seen dooley xare yi nekk ci reew yi nekk ci seeni loxo te nu feetale leen ko saxal yii nag ak leeral yi kureelug feetale gi nekk ci kureelug xeet yi lanu ko daa indil feetale gi tam mi ngi daa yam ci benn ñeenteelu xarnu maanaam benn xaaj ci xarnu bu xaaj ñeenti xaaj misaal yi aju ci xeetu sanc wii yu bari lanu ñu wax la ci rekk feetale gi nu defoon britani iraak penkub jordani ak falastin mi nga xam ne dafa genn ci teg loxo gu britani ngir tàbbeeti ci gu israayil ak feetale gi nu feetale woon fraans siri ak libaa ak feetale gi nu defoon goornamaab neewiit yu weex ya nekk afrig de sud feetale gi nu leen feetale woon mbirum namibi ñu yor ko di ko doxal ak feetale gi nu feetale woon japon duni pasifig duni marshal ak feetale gi ostraali ame woon ci kaw gine gu yees gi añs kureelug xeet yi nag daa xëyoon rekk sàkk feetale di ko teg reew yu neew yi doole ci sañ bañ te du leen ci tàggu mbaa mu ciy diisoo ak ñoom denkaane moom itam aw xeetati la ci xeeti sanc yi wii nag xeet la wu feeñ ci ginaaw xareb adduna bu ñaareel bi ñu amale ko nag ci genn saxal gu juge ca mbootaayu xeet ga ñu sosoon atum g ngir wutu fi kureelug xeet yi mbootaayu xeet yi nag neenaloon na kureelug feetale gu sax gi nekkoon ci kureelu xeet yi ngir teg fi leegi jataayub denkaane bi nga xam ne moom lanu wekk leegi mbirum saytu sancu yi reewi digg yi moomoon yilifoon leen reewi digg yi ñooy almaañ itaali ak japon bi nu leen laata a dàqe ci xareb adduna bu ñaareel bi moom jataay boobu tam moo yoroom mbirum reew yi tembagutoon misaalum xeetu sanc gii denk gi nu denkoon itaali libi ak somali ak denk gi nu denkoon britani tanganyika ak yeneen sancug aada moom de xeet la ci xeeti sanc gi nuy jaare ci xalaat yenn ci reewi sancaan yi danoo jugoon ci jariñoo xalaat ak aada ngir ligeeyal seeni njariñi sanc ci noonu ñu sosoon ay jàngu leekol aki xamluwaay aki fajuwaay aki barabi nasaraanal ak yeneen loolu lepp nag ngir man cee jaare bay sanc yii reew ñu ko def te man leen a moom fraans de xeetu sanc wii def na ko ci afrigu bëj gànnaar gi ci tinisi aljjeeri maraakes sunu reew mii it di senegaal def na ko fi defati ko ci reewi shaam yi rawati na libaa reewi dankub mbokkte bi it bennoog sofiet gi jiite leen ñoom itam jeem nanu ba sonn ci wisaare seen xalaat yi ak seen dali làngi politig yi ci reew yu bari ci adduna bi barabi sañ sañ lu bari ci reewi sancaan yi danu doon ngàrtaajoo ak a aakimoo koom koomu lenn ci reewi asi yi ak yu afrig yi ba noppi naan ñoom de dugguñu te seen yoon nekkul ci mbiri politig yu reew yii du caageenug seen mbiri biirum reew misaali xeetu sanc wii mooy la xewoon ca iraan atum g nga xam ne danoo defoon bëj gànnaaru reew ma muy barabu sañ sañ ñeel rusi gu xaysar gi bëj saalum ba nu def ko barabu sañ sañ ñeel britani amoon na it ay xejj yoo xam ne yenn ci reewi sancaan yi amoon nanu leen ci reewi adduna bi lu ni mel mooy xejj yi nga xam ne reewi tugal yi amoon nanu leen ci reewi shaam yi ci jamono ju usmaan ji ak xejj yi nga xam ne reewi sancaan yi amoon nanu leen ci siin ak tayland ak yeneen 	 ñaareelu doggantal reewi sancaan yi lu bari ci reewi sancaan yi doon nanu def seen cawartey sanc yooyu ci fu bari ci reewi adduna bi ci gox yii di afrig asi ak adduna bu yees bi amerig reew yi ëppoon solo ci reewi sancaan yooyu ci taarix ñooy reewum portigaal waa portigaal yi ñooy ñi njëkk a def ay wuññiy juxraaf yu tugal ci ñaari gox yii di afrig ak asi ñoo ci jiitu woon waa espaañ holand angalteer ak waa fraans ak ñeneen ñi jot a def ay wuññiy juxraaf ci jamonoy yewwute gu tugal gi tukkib vasco de gama bu njëkk bi mu defoon ci afrig ak end moo ubbi woon gëti waa portigaal yi jëme leen ci sanc ay barab yu bari ci afrig ak asi ngir teg loxo geeji penku yi ak rënk yaxantug penku gi rawati na li ci aju ci ay rëndaay ak ngir yàq koom koomu reewi jullit ñi rawati na nguurug mamaalig yi ngir loolu man a doyadil jullit ñi neewal leen doole waa portigaal yi tàllaloon nanu seen kilifteef ak sañ sañ ci duni madira yi bopp bu wert bi ak osoras barab yooyu nekkoon ci màmbulaanug atlas gi la ko dale woon ca ñeenteelu bu njëkk ba ca fukk ak juroomeelu xarnu g cig nangu tegoon nanu loxo barab yu bari ci afrig ak asi ci xarnub fukk ak juroom g yu ci mel ni mosambig ci penku afrig angola ci sowwu bi ecopi ak duni madagaskaar moris ak silaan ak xat xatu hormos ak xat xatu malga ci daanaka dun bu malayo añs waa portigaal yi defoon nanu seen sanc gi ngir dëkk ca bresil gi nekk ci amerig gu bëj saalum gi ñu indaale fa woon lu sakkan ciy jaam yu afrig ngir ligeeyloo leen ci mbay meek gasum mbell mi nu leeral leen ne sancug portigaal moom dundul lu ëpp ab xarnu ndax seen soxot gu tar gi nu ame woon ci ñoñ ñi cosaanoo woon ci seen sancu yooyu ak ngir ñàkk gi nu ñàkkoon a yittewoo mbirum nos politig bi ak goornamaa bi ci seeni sancu ak tam ngir xeeg gut ar gi leen askani yii barab doon xeex reewum espaañ espaañ def na ay ligeeyi wuññeem yu juxraaf moom itam ginaaw waa portigaal waaye jariñu ci seen xam xam boobu ñu jot a am ci lef moomu bu ko defee waa espaañ jël goxi amerig gu digg gi ak gu bëj saalum gi def leen ay sancu yu mu sos ngir dëkksi fa moom nag ag sancam daa tegu woon ci fitna ray song jaay doole ak gënale ci wàllug diine ci noonu ñu tàggatoon jaam yu ñuul yi ak endo yu xonq yi ngir ñu bayal leen tool yi gasal leen mbell yi ñu daal di woon jël yii reew cuub leen cuubug espaañ ci làkk ci diine ci aada ak ci taarix ba mujj sax bii gox ñu koy wooye amerig gu latin gi di ko askanale latin gi nu jublu woon esspaañ ak portigaal espaañ it tàllaloon na ag kilifteefam lal ko ci kaw ay barab ci goxu afrig yu ci mel ni duni kanari ak àllub maraakes bi ak goxu afni bi dend ak maraakes ak gine gu espaañ gi nekk ci bëj gànnaaru rëddu yamoo wi sancug espaañ gi neewoon na doole te doyadi ci kanamu jongante gi tugal doon def ci wàll googu ci noonu waa angalteer yi yàqate woon seen mbooloom gaal mi tuddoon irmada atum g mbooloom gaalum holand mi tam moñoxeeti mu espaañ mu lòtt mii atum g ci noonu la espaañ mujje di reew mu neew doole mu loof ci kanamu gëpplante gu angalteer gu fraans ak gu portigaal bu ko defee ay fipp am ca sancuy espaañ ya ci noonu askani dëkk yii daal jéngu xeex ba roccee seen tembte ci loxol waa espaañ yi reewum holand waa holand yi danoo duggoon ci ngérum protestant ba noppi nekk ci ron teg loxo gu espaañ gu katolig gii looloo taxoon ñu defoon seen fipp gu mag googee kontar katolig yu espaañ yii daal di noccee ci ñoom seenug temb ci doole ci njëlbeenug xarnub fukk ak juroom ñaar g waaye temb gii nag nangu na ko moom espaañ ci anam gu ofisel atum g ca kollareg westfalia ga nu defoon ginaaw xareb fanweeri at ba waa holand daal di taxawal lonkoo gu end gu penku gu holand gi ci njëlbeenug xarnub fukk ak juroom ñaar g daal di sóobu ci geewub jonganteg sanc gi ci penku bi daal di not waa portigaal yi ci wàllug sanc teg loxo duni end yu penku ya ca asi yaatuwaayu suuf yi holad mujjoon sanc mujjoon na gën a rëy juroom ñaari yoon yaatuwaayu holand gu ndaw gii ci jëmmi boppam sancaan yu holand yooyu danoo rënkaloon seen bopp rekk yaxantu gi aju woon ci rëndaay yi kawsu attaaya kafe suukar seng ak petrol añs waaye ñii dëkke woon ci sancu yu holand yi te cosaanoo fa xeexoon nanu kontar waa holand yii ba mujj am tembte atum g ci turu endonisi waa holand yi tàllaloon nanu seenug sanc ci diir bu gàtt ci kaw ay barab ci adduna ju yees jii di amerig ñu taxawaloon lonkoog end gu sowwu gu holand gi atum g ñu sancoon goxub dexug hadson daal di jënd manhatan ci endo yu xonq yi daal di taxawal dëkkub amstardaam bu bees bi nga xam ne waa angalteer yi nangu woon nanu ko ci holand tudde ko new york waa holand tam sancoon nanu ci diirub fanweeri at ag wàll gu mag ci bresil gi nekkoon ci ron kilifteefug portigaal reewum beljiig leopol mu ñaareel mi tegoon na loxo reewum kongo mi nekk ci digg afrig atum g daal di koy def ag moomeelam loolu nag wéyoon na di nekk ba atum g ci ginaaw bi lanu tuxale moomeel gii yobbu ko leegi muy gu reewum beljig kongo nag reew mu naat la lool te woomle ci ay koom koomi mbell waa kongo nag jàmmaarloo nanook sancug beljig gii leen doon jariñook a toggi mbugal daan jariñoo it seeni koom koom ci anam yu ñaaw a ñaaw loolu yobbu leen ci ñu am tembte atum g ci turu saayir sancug britani imbraatoorug britani gi moom lanuy jàppe muy gi ëpp ci reewi adduna yi mas a def sanc gu yees gii nu xam tay moom mooy imbraatoor gu sanc gi nga xam ne jant manul a so mukk ciy sancoom ngir bari gi mu bari lu mu sanc ci suufus adduna si britani dey defoon na ci wuññiy juxraaf yi waaye ca amerig gu bëj gànnaar ga mu sancoon lu sakkan ciy suufam waaye dëkke leen te sonn it ci dindi kilifteefug fraans ak holand ci gox bii te jële ko fi bu ko defee sancu ak dëkkuwaay yu britani yi ci amerig gu bëj gànnaar gi desoon ci ron cang gu sanc gu britani ba kero diiwaan yu bennoo yu amerig yi di am tembte naka noonu kanada ñoom reew yii nga xam ne dafa am lu leen boole ak britani muy bokk gi nu bokk ak ñoom askan te bokk nekkandoo ci komonwelth gu britani britani sancati na ostraali ci anamug dëkk ak newsiland waaye temb nanu ñoom ñaar te mujj bokk ci komonwelth britani sanc na end wéyal fab sañ sañam daal di sos lonkoo gu end gu penku gu angalteer gi atum g mu jot a dàqe fraans ca daanaka gox bu end ba mu manante siin ci mu ubbi ay waaxam ci kanamu afyon bii nga xam ne britani daa na ci indi lu bari ci waa siin yi looloo waraloon xare ba tàkkoon ci diggante siin ak britani di woon xare bu nuy tudde xareb afyon bu njëkk bi nga xam ne wéyoon na la ko dale woon ca atum g ba g nga xam ne ca la britani nangoo waaxub hong kong bu straateji bi waax bii mi ngi woon ci loxol britani ba bu yàggul xareb afyon nag benn la ci tooñaange yi nga xam ne britani mi ngi ko doon tooñ waa siin cig wàll ak nit ci jëmmi boppam ci geneen wàll britani tegoon na loxoom dunu brem atum g ak adan atum g ak borma atum g akug wàll ci malayo mu defati ay aar aki kollarante yu maandoodiku ak ab lim ci barab yi nekk ci bëj saalumu dunu araab bi ak tefesug golfub araab bi mu sanc isipt sudaan iraak penkub sordani falastin ak yeneen barab ci reewi asi yu ñàkk doole yi britani nangooti cig sanc lu bari ci reewi afrig yi lu mel ni afrigug bëj saalum gi nijeeriya oganda tansani rodisiya ak somali gi nu xame woon ci turu somali gu britani gi sancug britani gi nag mooy gi gën a ñaaw ci mbooleem xeeti sanc yi ndax moom da daa jëfandikoo cig sancam doole teg loxo ak jariñoo ne ne yu nu laalul yi ak kàttanug askan yi ak tas nit ñi ak xàjjale leen fitnaal leen ak tooñ leen waaye li lii lepp di tar teewul askani sancu yu britani yi xeex nanook sancaan bi ba kero nu ame seen tembte ci noonu la britani dellu mel namu meloon yor dayo bi mu yoroon ginaaw bi sancoom yii tembee wëliif ko foofa la ko lòttug politig gaare ak gu koom koom reewum fraans waa fraans yi bokkoon nanu ci ligeeyi wuññi yu tugal yi ci goxi amerig gu bëj gànnaar gi rawati na ci kanada ak gox yi peek dexug santa lorens gi ñu sosoon fa ay sancu yu fraans yu ci mel ne kebeg gi nga xam ne ci tefesug santa lorens gi lanu ko taxawaloon ak sancu bu luwisiyana bi nga xam ne turam wii mi ngi juge ca luwis mu fukk ak ñeenteel ma buurub fraans ba ag gëpplante gu mag xewoon na ci diggante waa fraans yi ak waa britani ci amerig gu bëj gànnaar gi ci xarnub fukk ak juroom ñatt g waaaye britani moom jot na a neewal doole kilifteefug fraans gi ci barab yooyu bu ko defee fraans moom teg loxo yeneen barab yu bari ci afrig fu ci mel ne aljeeri tinisi akug wàll ci maraakes daal di sutuxlu ci tàkkug afrig gu mag gi daal di yaatal bu baax seen sañ sañ ak kilifteef ci senegaal kongo nijeer madagaskaar somaal gi nu tudde woon somaalug fraans gi gine ak dawme fraans tegati loxo ay reewi asi fu ci mel ne ay wàll ci end waa britani jële leen fa atum g ñoom de jotoon nanoo taxawal lonkoo gu end gu penkug fraans gi ngir gëpplanteek lonkoo gu end gu penkug britani gi ak lonkoo gu end gu penkug holand gi ci wàllug yaxantu ci penku bi fraans sancati sireek libaa ci turu feetale ci ginaaw xareb adduna bu ñaareel ba sancug fraans gii nag daa melowoo ag tooñ tiitale jeem a far aaday reew yi mu sanc ak seeni màndargay reew ak jëmm lu mel noonu it mooy li nu def ci reewi araab yi nekk ci bëj gànnaaru afrig te fraans tegoon leen loxo waaye way dëkke ya xeexoon nanu sancug fraans gii ba mujj am tembte gu mat fii fi senegaal waa fraans sonnale nanu fi tege fiy fitna gennee fi xoolal ku mel ni sëriñ tuuba cig tooñ lanu ko fi gennee sanni ko ca àlli gabong yu lëndam ya yobbooti ko moritani te fii nu koy genne de du seenum reew reewam la xoolal ma fa ñuy wax camp caaroy ak jëf ju ñaaw ja nu fa def xoolal ma sunu làkki reew yii nga xam ne ba tay manunu leen di jàng te fraans nekk ci ginaaw xoolal ma yeneen mag yi nu sonnal xoolal ma aaday nasaraan ji nu fi bëgg a saxal leegi la sax waaye ci ginaaw ak seen senghor mi fi nekkoon nga xam ne daanaka tubaab la woon ngir ne seenub ligeey la woon bu leen fiy ligeeyal lenn luy sunu aada safu ko woon du col mi du wax ji du lekkiin wi du lenn lu mu man a doon naka noonu ñi nekk ci ngunoom ci ñi mu sos defar leen ñu koy ligeeyal reewum almaañ imbraatoorug almaañ gi moom itam dugg na ci geewub sanc bi ak jongante gu adduna gi ginaaw bi mu amalee ag bennoom atum g mu daal di sanc kamerun ak bëj saalumu sowwub afrig bi nga xam ne dees na koy wooye bëj saalumu sowwu afrig bu almaañ bi ngir sanc gi ko almaañ sancoon ak bëj saalumu penku afrig bi nu tudde ba tay bëj saalumu penku afrig bu almaañ ak togo almaañ it jotoon na a teg logo lu bari ci duni pasifig yi nga xam ne ñi ngi leen gënoon a xame ci turu duni argabiil yu bismarck yi ñu nangu tam ñoom waa almaañ xaajub bëj gànnaar bi ci duni gana gu yees yi nekk ci màmbulaanug atlas gi waaye almaañ moom mujjoon na ñàkk sancoom yii ci ginaaw bi nu ko dàqee ci xareb adduna bu njëkk bi reewum itaali itaali tam soobu na ci lefum gëpplanteg sanc gi ginaaw bi mu bennoo atum g mu daal di teg loxo ay sancu ci afrig ci eritri somali gi nu tudde somali gu itaali gi libi ak ecopi itaali nag jëfandikoo na gën ja a ñaawi anami mbugal ak ray ci kaw askani yii reew omar muxtaar ca libi fàttaliku leen ko reewum rusi mu xaysar mi sancug rusi gi moom mi ngi jëmoon ci siberiya turkmanistaan ak ay gox ci asi gu digg gi rusi it teg loxo gox yi nekk ci bëj gànnaaru dexug amoor gi ci siin daal di fay taxawal ab dëkk bu bees ci turu vladivostok lijjanti it ba siin gu neew doole gii jox ko ay sañ sañ ci defar yoonu weñ wu jaar ci suufi manshuriya gu siin gi ligeey ba daal di tàmbli ca atum g sañ sañu rusi it yokku ca kore mu daal di seddoo iraan mook britani daal di sanc wàllug bëj gànnaar ga ci ginnaaw bi nu defee seen dëggoo gu xaritoo gi xaatim ko cis een diggante ñoom ñaar atum g buntub ñatteel bi ñaawteefi sanc li sikk amul mooy sanc gii amoon ci adduna bi ci melokaanam yepp aki anamam bokkoon na ci li gënoon a soof te ñepp bañoon ko te sib ko rawati na askan yi nu ko teg ci seen kaw ba nu mos aw wextanam reer cig lëjam sanc de bijj na lu lëw ciy ñaawteef aki jeexiit yu bon ci ka waskan yu lòtt yi yanu woon ab sukkam ñaawteefi sanc moom dees na leen man a gaw ci wàll yii ñaawteefi sanc yu politig li kenn reerewul mooy ne reewi sanc yi de rekki nanu ngorug askan yi nu sancoon seeni reew rekki it seen sañ sañ ci wutal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom te loolu dal yi aju cig nite yepp ak yu yoon yepp woote nanu ko xañoon nanu it askan yi ñuy àttewoo ci sartu reew ak ci nostey demokraasi yu tegu ci cëslaay lu mucc te sell loolu nag mi ngi am ci ginaaw bi nu yàqee mbooleem campeefi xeet yi te dindee leen fi wuutal fi yeneen yuy ligeeyal seeni xemmeemteefi sanc sanc gi nag jeemoon na a defi pexe ba askan yi nu sanc dunu doon mukk benn bu ko defee mu def lu nekk jëfandikoo pexe mu mu man a doon ngir xeet wi bañ a nekk benn mu tàmblee wut lepp luy tàqalee di ko sotti ak a wisaare ci mepp mbooloo muy menn ak wepp xeet wuy wenn ci mepp reew muy menn mu soññ te sawarloo yëngu yënguy beddiku yi yi nga xam ne neewte yaa ngi leen doon sàkku ak def daal di yittewoo bu baax lepp lu aju ci luy jeqi ag xëccu jëm ci waaso mbaab kureel walla boddante mbaa woote ag gën ci biiru xeet ak wuute ci ngér mu ñëwati xóotal dalub tàqle politig ci mennum reew daal di sawarloo làng yi ànd ak moom ci politigam boobu daal di def ay soppi ci dig yi yooyu soppi nag ñoo mujj di jëfka yu mag yi mujj di taal gilinug wuute gi ak noonoo ci diggante dooley politig yi dëkkandoo dendandoo mu dooleeti indil reew yi mu sanc ay jafe jafey politig yu fasu yoy reew yi nu sanc de wéy nanu di jànkoonteek ñoom ay ati at ginaaw bi nu tembee yooyu jafe jafe wéyoon nanu di fi sax ginaaw bi nu mujjee nekk di fi ag dund gu yees sanc nag jëfandikoo woon na mbooleem xeeti jumtukaayi mbugal yi kontar askan yi mu duma tëj mbugal te ray lu sakkan ci askan yi te dara waralu ko lu dul ne danoo fippoon kontar ko sàkku woon nu nuy goree te temb te loolu àq ju mag la tey yelleef ñeel leen waaye askan yii yanu woon sanc gi jugoon nanu xeex def ci seen lepp ngir yekkati yan bu diis bii tegu ci seenum ndodd ñaawteefi sanc yu mboolaay sanc daal dafa defoon yitteem ci tas xottite bennoo gi am ci mboolaay yi nekk ci sancu yi jaare ko ci soññee cig tàqalikoo wisaare nosteg kureel ci biiru askan bu ko defee kureelug laman yi walla gu sang yi daal di feeñ am ay sañ sañ yu bari aki ngëneel yu tax ñeneen ñu ndool ñig ñàkk di bëgg a ray akug reer mere woon leen gii kureel nag ligeeyal na ba tàyyi sanc gi ci anam yu bari bu ko defee jaasiy sanc gi nekk fi di lu nu bocci ci baatub ñu ñàkk ñi di leen tegi coona di leen fitnaal te kat ñoom ñooy ñi ëppoon ci askan wi am geneen kureel gu feeñati ci wetu gu lamani sancu yi mooy kureelug sang yu doxandeem yii nga xam ne ñoo tegoon loxo ci koom mi ak ci nguur gi walla àtte gi bu ko defee tàggat doomi sancu yi ci ñu leen di ligeeyal sanc gi tàbbal na ci sancu yi mbooleem aada yu ñaaw yi man a yàq ag mboolaay man a ñaawali jikkoom mu soññe cig mbon reer jëfandikoo dorog ak yiy màndal ak wure ak kart ak yu dul yooyu ci aada yu ñaaw yi man a tas bennoo gu ag mboolaay te dëgëral nekkug sancaan yi ak seen doole ci sancu yi te gën fee suuxat seen reeni sanc sanc gi de jeemoon na jëfandikoo woon ci loolu bepp kerkeraan bu mu amoon mbaa yoon wu mu xamoon ngir gòndi niti sancu yi ci xayug tugal gi te sopploo leen ko ngir ag maas man a judd guy gëm te gòndiku ci jëm kanamug tugal gi ak xalaati waa tugal yi li ñu jublu woon ci raxasug xel gii mooy indi fi ag maas gu yees guy ligeeyal njariñu tubaab yi rawati na bu maas gii mujjee jiite reew yi ci politig jaare ko ci seenug jàpple waaye ànd ak pexey sanc yii yepp ngir amal loolu teewul askani sancu yi tas yaakaari way sanc yi sooyal seeni mebat seeni mebat sooy na seeni yaakaar tas bi nu gisee ne askan yi dey ñi ngi wéy di gën a jàpp ci seeni diine di gën a oy ci sseeni aada di gën a ngëb ci seeni pas pas yu laab yooyu fonk seen bopp seen taarix aks een xalaat nga gis ne maas gi juddoo ci jamonoy sanc ñoo yanu woon raayob fipp gi ak xeex bi kontar sancaan yi ñu saxoon nag ci noonu ba mujj fuqarci ci doole seenug gore akug temb gu mat sëkk ñaawteefi sanc yu koom koom li njëkk a yitteel sancaan yi mooy am ay ne ne yu nu laalul yu mbay ak mbell ba man a doxal seen ligeeyuwaay buk o defee man fa a ligeeye lu nuy genneeti di ko jaayati ca reew ya nu sanc looloo taxoon sanc gi saxoon ci di muucu ak a ngacc xeewali reew yi nu sanc yu mbay yeek mbell yi mu soññ lonkoo yu jàmbur yiy rënk ñu ñëw meññilu seen alal yi ci reew yi nu sanc ci anam ak wàll yiy ligeeyal tey jariñ reewi sancaan yi bu ko defee yii lonkoo taxaw ci jariñoo koom koomi reew yi nu sanc ci diir bu gàtt ndax danoo yàgg a ragal fipp yi leen daan kontar te askan yu ndooli sancu yi daan leen def ñoom ñi nekkoon ci ron yan bu diis bii leen tegu woon te weesuwutoon lenn lu dul sanc gi reewi sancaan yi yamunu woon ci muucu xeewali sancu yi waaye àggoon nanu ci def leeni ja yuy muucu ak a dékku marsandiisi tugal yi lii nag moo nuy woo ci ñu tudde sanc gi siyukaay biy si buy dem ak buy ñëw sanc gi moom da daan xeex endustri ci sancu yi daan def lepp lu mu man ngir sancu yi sax di ligeey ci mbay mi te bàyyi endustri bi ngir man a joxe ne ne yu nu laalul yu mbay yu man a dundal endustri yu reewi sancaan yi sanc gi jeem na a ray ruug gëpplante ci doomi sancu yi ginaaw bi mu fi rayee endustri bu lokaal bi tax it ba seeni boroom daanu ci kanamu endustri bu reewi tugal yi bu ko defee këri jàmbur yi teg loxo ci koom koomi reew yi ak seeni alali endustri ñu takk it xalisu sancu yi ci xaalisu reewi sancaan yi loolu lepp nag ñu jublu ci takk koom koomu sancu yi ci koom koomu reew yiy sanc fii nag la genne gisiin wi naan sanc gu politig du lu dul doomi sanc gu koom koom ci sunu jamono jii nu toll ñaawteefi sanc yu aada ak xalaat sanc gi xamoon na ne aaday xeet ak cosaanam mooy li gën a man a dëgëral ag bennoo gu politig ak gu mboolaay te moo gën a gaaw a jañe ci xeex ngir gore cig sanc ci reew yi sanc gi jeem na a soppi taarixu reew yi nu sanc te def ay pexe ci soppi seenug xay gi nga xam ne seen ngértel xeli doom la juddoo nag ci ay jamono yu toppante te toftaloo mu tàmblee jël tooke di ko def ci lem ngir dundal ci doomi sancu yi jaare ko ci aada ak xalaat ngir ñu man a jàpple tubaab yi ci seen xalaat yi ak seen xemmemteefi sanc yi sanc gi nekkoon na fi di doju pakastal ci kanamu am njàng rawati na mi ci aju ci xam xami dëppale yi ak yu xarala yi nga xam ne danuy jàpplee bu baax ci yewwuteg xam xam man a am ak gu endustri ci reew yi te moom sanc gi yitteem weesuwuton ci wàllug njàng li nuy wax njàggale mu matale mi walla njàggale mu yaatu mi bu ko defee njàng mu kawe mi mu jagleel ko doomi kureelug laman gi daa jariñu ci sanc gi des fi sancaan yi danu daa yittewoo tas ak a wisaare seen làkk ak aada ak seen taarixu xeet ak seen xay gii nga xam ne teguwul ci lenn lu dul ci ne ne ñu tay taylu woon di far dëgg yi di indi li dëppoo ak seen njariñ di wisaare xam xam yiy ligeeyal seeni reew di wone dooleem akug màggam ñu tàmbli woon a sikk ndegam ñii cosaanoo ci sancu yi man nanoo jiite am reew daan leen sabooteel seen kilifa yi seen njiit yi seen jàmbaar yi ak seen boroom xam xam yi sanc gi jubluwutoon ci loolu dara lu dul ligeeyal boppam aki njariñam ak jeem fee saxal boppam moom mi nga xam ne masul a dañ di ragal fippug askan yi ak seen yewwuteg xeet doggantal gu ñeenteel gi yëngu yëngu yu ag nasaraanal ak ay wi mu àndal ag nasaraanal yëngu yëngug diine gu nu nos la gu li ko tax a jug mooy tas diiney nasaraan ak xayug nasaraan yi ci jullit ñi ak ñu dul ñoom nasaraanal gii nag lu taqoo la ak sancug tugal gu yees gii nga xam ne jot na a man a ligeeyal diiney nasaraan ci anam gu nëbbu jaare ko ci ay yoon aki defiin yu lëmu te jafee xam loolu lepp nag ngir ligeeyal ay xemmemteef yi mu amoon ci sanc adduna bi yilif ko looloo du yomb nu tàqale diggante nasaraanal ak sanc te itam nasaraanalkat yi danu daa nekk ci ron kilifteefug sancaan yi lu yeeme la diiney nasaraan nekk di benn ci jumtukaayi sanc gu tugal gu yees gi nasaraanal nag yamutoon ci benn jàngu rekk ci jëmmi boppam waaye kay jàngu yepp a ko daan def moo xam jàngu bu sowwu bi la bu katolig bi bu penku bi bu ortodoksi bi bu protestant bi walla bu angalteer bi bu angalikaan bi gëpplante gi taroon na ak xeex bi ci seen diggante ni mu tare woon ci diggante reewi sancaan yi taarixu nasaraanal gu yees gii nag am na ag takku gu mu takku woon ci yëngu yëngu gu wuññi gu juxraaf gi reewi tugal yu nasaraan yi doon def te porrtigaal ak espaañ jiite woon leen di woon ñaari reew yu ëppaloon ci diine te daan ci par parloo kontar jullit ñi ak seen adduna bu ko defee wuññikati orob yii ame woon ag parparloo gu diine defoon seeni ligeeyi wuññi soldaarus tugal si topp ci seen ginaaw di ligeeyal xemmemteefi sanc yu seeni reew loolu lepp nag ngir nu àndandoo amal li nu bëgg mooy ligeeyal tubaab yi te taxawal seenug cang ci diineek fetal jumtukaayi nasaraanal aki ker keraanam nasaraanalkat yu nosu yi jëfandikoo woon nanu ab lim bu rëy ciy ker keraan yu leen di dimbali ci seen ligeeyub nasaraanal bi bu ko defee nuy def jamono ju ñëw ñu seet nu ñu ciy def ba ligeeyal ci seen jubluwaay boobu jumtukaayi nasaraanal gën na a jëm kanam ànd ak jëm kanam gi jamono def ak gi xam xami dëppale yi ak yu xarala yi def nasaraanal ñi ngi ko tàmblee ci ay nit di jug di waaraate ak a xamale yonnant yàlla hiisaa j m akum njàngalem diineem wii xeetu nasaraanal sax na fi di ag nasaraanal gu kenn nit di def mu doonoon lu jëmadi kanam waaye tolloo woon ak jamono ju yàgg ji mu dajeeloon jumtukaayi nasaraanal jëmoon na kanam aki ker keraanam bi yewwuteg xam xam ak gu endustri gënee jëm kanam ci tugal bu ko defee yonnee yu nasaranal yu nu nos yi tàmblee am ay mbootaay yu nasaraanal yu bees di leen saytu yuy jëfandikoo mbooleem anam yi ak jumtukaay yu yees yi ngir doxal seeni ligeey bokk na ci li nu daa jëfandikoo 	ndoktoor ak li mu àndal ci ay barabi faju lu ci mel ni fajuwaay yi ak këri faj yu ndaw yi ak barab yiy maye ay garab ci xaranub fukk ak juroom ñeent ay mbootaayi ndoktoor yu nasaraanal yu bari feeñoon nanu ci reewi tugal yi ak diiwaani amerig yu bennoo yi ak yul ñoom ci reewi addunay nasaraan ji li leen taxoon a jug mooy waajal ay doktoor yu goor ak yu jigeen aki matulkat aki jàpplekati doktoor ngir ñu man a ligeeyal egliis bi jaare ko ci ligeey ci barabi nasaraanal yi nu tasoon ci adduna bi rawati na ci afrig ak asi ndoktoor man nanu ne mooy ker keraan bi la man a gën a may ngay man a jonjoo ag nit ñu neew ñi doole ak ñu ñàkk ñi nasaraanalkat yi danu daa wax naan li nu jublu ci jëfandikoo meccem ndoktoor ci nasaraanal mooy ne moom day nooyal yoon wi laytaay ko ba bu injiil dee ñëw ngir dugg ci xol yi du jafe ma ne man nit ki boo ko joxee mu lekk naan ginaaw bi muy bëgg a dee cib xiif di bëgg a dee ci tawat nga faj ko boo nee ko fii la mu ne foofa la rawati na bu ko fekkul muy ku tatawu ci xam xam aaru ci dali diine ju dëggu daanu daa wax it war na doktoor biy nasaraanal mu bañ a fàtte ne day nasaraanal laata a dara di xew mbootaayi nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci meccem ndoktoor mii daal di ubbi lu sakkan ciy barabi ndoktoor ci reew yu ndool yi yittewoo faj aki doktoor ngir loolu man leen a jàpple ci seen ligeeyub nasaraanal boobu leen taxoon a jug 	njàggale ak li mu àndal ciy jumtukaay lu ci mel ne daaray dal yi ak yu diggu yi ak yu ñaareel yi ak xamluwaay yu kawe yi ak daara yu mag yi ak kàggu yi ak daaray mecce yi añs ñi jiite woon nasaraanal gi danoo gisoon ne bu nu ubbee ay daara yii ci reewi jullit ñi ak yu leen moy loolu da na man a doon aw yoon ngir tas ci diiney nasaraan ci doomi jullit ñiy jàngsi ci yii daara rawati na bu nu leen dee def leeg leeg ñu cofal leen ci njàggalem injiil mi leeral leen ko nga rax ci loolu li daara yii daa def muy tas xayug tugal gi ak rawug xam xamam ak jàngal ko yile dongo te loolu ag doyodal jullit ñi rekk lanu ci jublu woon 	jëf ju yiw ak ju nite ji nga xam ne mbootaayi yiw ak nite yu nasaraan yi daa nanu ko def ci reew yu ñàkk yi rawati na ci jamonoy ay yi ak musiba yu dénd yi ak xare yi bu ko defee ligeeyub nasaraanal bi di sawar ci biir daw làqu yi ak ñu ñu tuxal ñi ci reew yu neew yi doole loolu mooy li ngay gis ci reewi afrig yeek ak asi loxob nasaraan biy indi ñam fa jak ndimal ñeel daw làqu yooyu ak ñu ñu tuxal ñi mooy biy tas dali diiney nasaraan ci ñooñii di jariñu ci seen nekkiin wu metti woowu ak seen tumbrànke gu tar gi 	yëglekaay yi ak këyiti xibaar yi tasum xibaar meek yeene yi nga xam ne seen woote yu nasaraanal yee ko daan tax a jug ak waxtaan yi nu daa amal ci penc yi ak taalifi penku penku yi yi daa gëstu ci xam xami penku yi ak seeni njàggat aki pas pas ak li nekkoon ci loolu lepp ci tooke ñeel jullit ñi ak seenug xay aki laaj yu man a jur ay sikk aki jiixi jaaxa ci jullit ñi jëm ci seeni boroom xam xam aki kilifa lii lepp ci jumtukaay yi la woon nasaraanalkat yi gisoon nanu ne daal teere yii ak yu nu mool yii man nanu leen a dimbali bu baax ci wisaare ag nasaraan ci reewi jullit ñeek yu leen moy jaare ko ci li nuy bàyyi ci bakkan yu doyadi yi mbootaayi nasaraanal yi sos nanu ab lim bu mag ci ay daaray yar ci tugal ak amerig ngir waajal ci nasaraanalkat yi war a defi bii ligeey nasaraanal ci reewi araab yi nasaraanalkat yu katolig anglikaan ak protestant yi wisaaroo woon nanu ci reewi araab yi nekkoon ci ron sacug britani fraans itaali mbaa gu espaañ bu ko defee nasaraanalkat yi sos ci reew yii ay barabi nasaraanal ci biir askan wi rawati na fa jullit ña ndaxte seen jubluwaay ci loolu mooy neewal doole jullit ñi aks een diine reew yi nasaraanal gi sutuxlu danu leen ci tuddal yii nasaraanal ag cawarteem fésoon na ci biir nasaatiray iraag yi ci mawsil baxdaad ak basra ñi ko doon def nag di ay nasaraanalkat yu fraans ak yu itaali àntug nasaraanal gu katolig gii ci iraag ci njiitul fraans merloo woon na britani ci noonu mu daal di fa woon yabal ay nasaraanalkat yu anglikaan daal di ubbi bunt bi ci kanamu nasaraanalkat yu protestant yi ngir ñu àndandoo xeex nasaraanal gu katolig gu rëy gii doon àntu bu baax ci iraag loolu jur ag gëpplante gu mag ci diggante nasaraanalkat yu katolig yi cig wàll ak yu anglikaan yi ak protestant yi ci geneen wàll gëpplante gii nag du lenn dul geneenati ci gëpplante yi daa xew ci wàllug sanc ci diggante fraans ak britani ci goxi penku bi britani daa gisoon ne nasaraanalug katolig gu fraans gii nekk iraag tay dara yobbuwu ko fa lu dul suuxat xejjug fraans ak kilifteefam ci penku bi te loolu moom la britani doon ragal moom mi ame woon dooley sanc ji gën rëy te ëpp doole ay turi nasaraanalkat yu protestant yu bari feeñ nanu ci ñi daan ligeey ci toolub nasaraanal ci iraag ci xarnub fukk ak juroom ñeent g ku ci mel ni nasaraanalkat bii di grant ak groves ak samuel zwemer añs goxi golfub araab bi ag nasaraanal tasaaroo woon na ci goxi golf bu araab bi ndaxte bii gox da di ab jàlluwaay bu am solo jëm ci goxi penku yi bi mu ko defee nasaraanalkati protestant yu amerig yi sawar fa daal di fay sos ay fajuwaay yu seenub lim àggoon ci juroom ñeent aki këri doktoor seenub lim ñoom it àggoon ci fukk ak benn nasaraanal gi yamutoon ci mbootaayi protestant yu amerig yi waaye weesu woon na leen ba daj yu katolig yi ak yu angalikaa yu britani yi ci noonu yii mbootaay tàmblee joante ci sos ay daara aki jàngu aki katederaal ci goxi glof bi nasaraanalkat yu protestant yu amerig yi daal di taxawal egliisub injiil bu xeet wi ci kuwet ahmadi manaama ak masxat bu ko defee katolig yi taxawal katedraal bu katolig bu rom bic i manaama ak abuudabi ak egliisu angalikaan bi ci manaama nu daal di sos ay barab yu nu jagleel tas injiil ak seddale ko ak yeneen teerey seen diiney nasaraan ji ay seen yeene yi aju woon ci seen woote bu nasaraanal bi waaye ak li nit ñiy yittewoo barabi faju yooyu lepp ak leekol yi teewul ñu xeex bu baax kontar yëngu yënguy nasaraanal yii ànd ceek li nu am ci jumtukaay ak doole boroom xam xam yi xeex ko cis en xutba yi nuy def ci jàkka yi ak waaraate yeek gindee yi askan yu bañ sanc yii te noonoo ko ñoom itam xeex ko loolu jural nasaraanalkat yi ag sooy akug tas yaakaar reewi shaam nasaraanalkat yi sawaroon nanu ci reewi shaam yi ci siri libaa palastin ak urdun nasaraanalkt yi yittewoo woon nanu mbirum libaa ak palastin rawati na ginaaw xareb adduna bu njëkk bi nga xam ne reewi shaam yi danoo tàbbi woon ci ron feetale gu fraans ak britani bu kodefee way nasaraanal yi sotti seenug nasaraanal ci goxi siri yeek libaa daal di jàpplanteek kureelug mawaarina yu katolig yi ci libaa britani it duggsi feeteek kureelug dursu gi ci libaa nasaraanalkat yi jeqi woon nanu fa ay fitnay kureel ca la xarey kureel yu tàng te tar juddoo ci libaa ci diggante mawaarina yi ak dursu yi atum g way nasaraanal yu angalikaan yi ñoom danoo sotti woon seen yitte ci palastin rawati na ne moom ab diggub diine la bu am solo ñeel ñi topp ñatti diiney asamaan yi diiney yahood ju nasaraan ak lislaam mbootaayi anglikaan yu angalteer yi tàmblee sosi lopitaal aki leekol aki mbootaayi yiw ci dëkki palastin yi rawati na quds betlahem naasira tabariya yaafa ak gasa fii itam du waa angalikaan yi rekk a fa doon def ag nasaraanal waaye it katolig yi ortodoks yi ak protestant yu amerig yi julliti palastin yi jàmmaarloo nanook yëngu yënguy nasaraanal yii xeex ak ñoom bu baax ndaxte daa noonu woon seen diine noonu seen jaloore seen ndono seen xay ak taarix bu lislaame bu xóot bii seenug xeex ko gën na a tar bi mu gënee leer ne ag nasaraanal la te sanc gi lay ligeeyal ci noonu nasaraanalkat yi jàpplanteek seeni goornamaa kontar araabi palastin yi ngir defar lanuy wax dëëlub balfour genne ko it atum g li i ko taxoon a jug di sos am reewum xeet mu yahood yu sahyoon yi ca suufus jàmbur see di palastin di suufus ay araab yu jullit tubaab yi déggook yahood yi jox leen ko ci seenug toroxte ak naqar isipt nasaraanal tas na ci isipt te wisaaroo fi ci xarnub fukk ak juroom ñeent g rawati na ginaaw bi ko britani tegee loxo atum g qibt yi dimbali nanu mbootaayi nasaraanal yi tasoon ci biir jullit ñi ci isipt bu ko defee yonnee bu katolig bu fraans bi tukkee woon liyon daal di def ay ligeeyi nasaraanal yu fés mboolooy nasaraanal yu yesu yi di leen jàpple ci loolu nasaraanal ga amoon ca isipt paab gi dëgëraloon na ko te jàpple ko mbootaayug nasaraanal gu anglikaan gu angalteer gi def ay ligeeyi nasaraanal ci isipt ay cawartey nasaraanalam gën a yokku ginaaw bi britani tegee loxo isipt te jàpple bu baax yii mboolooy nasaraanal te aar leen mbotaayi nasaraanal yu protestant yu amerig yi def ñoom itam seeni ligeey ci isipt ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar fukk g bu ko defee mboolooy nasaraanal yii tàmblee xëccoo ci seen biir ak a gëpplante ci wàllug ubbi ay fajuwaay aki leekol aki egliis aki katedraal ak barabi seddale teere yeek mbindi nasaraan yeek yeneen yiy ligeeyal nasaraanal jullit ñi xeex nanu nasaraanal ci isipt boroom xam xami ashar gu tedd gi jug ñoom itam jàmmaarlook yëngu yëngu gii daal di sos mbooloo muy aar lislaam ngir xeex nasaraanal ci meloom yepp aki anamam mbooloo mii mujj na am ay bànqaas ci dëkk yu magi isipt yi sos it ay jàngu aki wéeruwaay ñeel way ñàkk ñi ñu lòtt ñeek jirim yi ay doxi ñaxtu yu bari am ci kanamu barabi nasaraanal yi ci xaayra demenhor saqasiq ak kafar siyaat añs yenn it ci yëglekaay yu isipt yi dimblee ci feeñal jubluwaayi nasaraanal gi yee it jullit ñi ci ay wi mu làmboo ligeeyub nasaraanal sawaroon na ci sudan rawati na ci ginaaw bi ko britani tegee loxo bu ko defee mbootaayi nasaraanal yu katolig yu protestant ak angalikaan yi def seeni ligeeyi nasaraanal ci biir jullit yi dëkke woon ci bëj gànnaaru sudan ak ñu dul jullit ñi dëkke woon ci bëj saalumam way nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci ñi dëkke woon ci bëj saalumu reew ma te doonadi woon ay jullit ci noonu ñu jot a tas seen diine ji ci ñoom ak aaday sowwu ji nasaraanalkat yi sosoon nanu ay jàngu yu yonnee yu katolig ak yu angalikaan ak yu protestant ci sudan sosati fa ay barabi faj yu nasaraanal waaye waa sudan ñoom toogunu rekk lem seeni loxo ci kanamu nasaraanal gi fipp gu mahdi di xeex na ko broom xam xam yi xeex ko mbootaayi diine yi rawati na ci bëj gànnaaru reew ma ñoom itam xeex ko reewi maxrib bu araab bi maxribu araab bi dafa nekke fu jàkkaarloo ak reewi nasaraan yi rawati na espaañ itaali ak fraans reew yii nag jariñoo nanu bu baax neew dooleg reewi maxrib bu araab bi daal fay yabal ay nasaraanalkat yu bañ lislaam ak jullit ñi ngir ñu def fa seen ligeeyi nasaraanal yi ak ngir nooyal ko waajal ko ba mu man a dékku sanc gi nar a ñëwi di tukkee ci fraans itaali ak espaañ reew yii yepp nag yu yor diiney nasaraan lanu cawarteg nasaraanal gi yokku na te dolliku rawati na ci keppaarug sanc gu tugal gii ci reewi maxrib yi bu ko defee gëpplante gi ci toolub nasaraanal tàmblee tar ci diggante mbootaayi nasaraanal yu katolig yi yu anglikaan yi ak yu protestant yi nasaraanalkat yi daal di wut ay jumtukaay aki ker keraani nasaraanal taxawal ay fajuwaay aki kër doktoor aki daaray nasaraanal añs ci biir loolu ñu def lu nu man ngir fay làkkuw araab te dundal kàllaamay berber yi ngir xeex ci làkku alxuraan wi ñu defoon ay pexe itam ci far aaday lislaam ji ak taarixam jeem a jox jullit ña fa dëkke woon ay reewu yu reewi sancaan yi bu ko defee dunu reewooti ci seeni reew te dunu ko bëggati ñu xeex ak boroom xam xami jullit ñi daa jeem a taxawal ligeeyub nasaraanal bi waaye nag ñu fonk seen reew ñii dëkke woon ci reewi maxribu araab bi amoon nanu ndam ci damm degug sanc gi ak gu nasaraanal gi ngir seen xeexub njàmbaar bi ñu leen jëmale woon barabi nasaraanal yi ci reewi araab yi mbootaayi nasaraanal yi sosoon nanu lu sakkan ci ay barabi aada yu xam xam ak yu faj ci reewi araab yi lii ci la 	mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari ci ay jànguy dal yu diggu ak yu ñaareel yu nasaraanal ñeel xale yu goor yeek yu jigeen yi ci mbooleem reewi araab yi nasaraanal gi dugg 	mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari barabi jàngale yu kawe yi ci isipt yu ci mel ne daara ju mag ju amerig ji xamluwaay bu penku bi xamluwaay bu fraans bi yooyu yepp nag ñi ngi xaayra bu dee sudan nasaraanalkat yi sos nanu fa bànqaas bu kamboni bu katolig bi ak jàngu bu amerig ak jàngu yu qibt yi yu gres yi ak yu angalteer yi mbootaayug protestant gu amerig gi moom tam sos ca bayruut daara ju mag ju amerig ati katolig yi sos fa ñoom daara ju mag ju katolig ja walla daara ju mag ju yesu ji ñu duppee aji sell jii di yuusuf 	nasaraanalkat yu penku penku yi dugg nanu ci akaademiy làkk yi ci reewi araab yi ñu dugg ca akaademib làkk ba ca xaayra ak bu xam xam ba ca dimasq ak bu xam xam ba nekk baxdaad penku penkub angalteer bii tudoon jub nag kenn la ci ñoom ak margoliyos mu fraans mi garifani mu itaali mi hothman mu holand mi ak harithman mu almaañ mi penku penku yi duggal nanu seen loxo ci teere yu bari yoo fiy gis tay ñu tudd ci rekk ci misaal jimblang ci lislaam ak dundug muhammad j m ki nuy wax sir william mouir def ko teere bi tudd lislaam te alfred giyom def ko ak yeneen ci teere yi nëbbal lislaam ag mbañeel 	mbootaayi nasaraanal yi taxawal nanu lu limu ci ay cëslaayi faj lu ci mel ne fajuwaayu marson ak bu maryon wilth ca bahrayni ak fajuwaayu noks ca masqat ak bu harmal ca isipt ak bu maryohanna biy faj bët ca quds ak yeneen yu nasaraanal yi wisaaroo ci mbooleem reewi araab yi ginaaw ci reew yii lanu nekk nag kon yu afrig gu ñuul gii nga xam ne mooy seen mburu mu bees jarul ñuy wax juroom benneelu bunt ñaar fukkeelu xarnu ñaari xarey adduna yi bu njëkk bi ak bu ñaareel bi mbootaayi adduna yi kureelu xeet yi mbootaayu xeet yi mbootaayu reewi jullit ñi danki reew yi ak reew yi feetewul fenn xareb jawwu bi jëm kanam gu japon doggantal gu njëkk gi ñaari xare yu adduna yi bu njëkk bi ak bu ñaareel bi xaaj bu njëkk bi ci ñaar fukkeelu xarnu g seere na tàkkug ñaari xare yu adduna ñooy xareb adduna bu njëkk bi g ak bu ñaareel bi g leegi nag ñu waxtaane leen ci ni nu càllaloo ci jamono xareb adduna bu njëkk bi g li waral xare bi xareb adduna bu njëkk bi am na ay sabab yu jonjoo ak yu jonjoodi kon nanu njëkk a waxtaane sabab yu jonjoodi yi sabab yu jonjoodi yu xare bi man nanoo tënk sabab yu jonjoodi yu xareb adduna bu njëkk bi ci ñeenti sabab yu mag ñooy 	gëpplante gi ci wàllug sanc 	tapoo yi 	màggug yëngu yëngu yiy woote ag xeetu 	ak lëj lëj yu adduna yi a gëpplante gi ci wàllug sanc gëpplanteg adduna gi taroon na ci ginaaw yewwuteg endustri gi ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g reewi endustri yi seeni cawarte gën na a yaatu gën a jëm kanam ci gii wàll ci fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g li ko waraloon di naj gu tar ak jañax gu tëw a dakk gi leen seen lonkoo yu endustri yu mag yi daan jañax jëme ci loolu ak boroom boppi alal yi dëkk ci yile reew rawati na nag ci reewi tugal yi am ay noste yu gore bu ko defee ñu jug tàmblee gëstu ji ne ne yu nu laalul yi manul a ñàkk ngir ligeeyi endustri yii man dox man a jëm kanam tàmblee wër it ja yu nu man a jaaye ji seen ligeeyi endustri yu wuute yi loolu nag jur na fi ag xér ci ne ne loolu tam jurati fi jawwi gëpplante ci wàllug sanc ci diggante reewi endustri yu mag yi lii itam jur ag rawante ci ngànnaayu ci adduna bi bu ko defee endustrib ngànnaay gën a jëm kanam ndaxte ku bëgg a sanc fàww nga yor ngànnaay yu doy ku ko bëgg a suuxat it mbaa nga bëgg cee ame sa njariñi koom koom yi tax nga koy def fàww nga ngànnaayu ag gëpplante gu tar amoon na ci wàllug koo koom ci diggante britani ak fraans cig wàll ak ci seen diggante ñoom ñaar ak almaañ ci geneen wàll silaay almaañ yi bari woon nanu ci ja yu adduna yi ngir ay sabab yoy yenn yi danoo dellu woon ci jëm kanam gi endustri almaañ jëmoon kanam yi ci des dellu ci barig naali koom koom yu almaañ yi ci reewum usmaan mi rawati na naalub yoonu weñu berlin baxdaad kuwet xëccoo googu nag amoon ay jeexiital yu rëy ci tàkkug xareb adduna bu njëkk bi ci nii lanuy gise ne gëpplanteg koom koom gu adduna bi mooy li duggal adduna bi ci paxum xare bu tàng bu nu ngànnaayal b tapoo yu reew yi gëpplanteg politig gi aju woon ci sanc ci adduna bi dafa gënoon na jëm kanam ci ginaaw bi gëpplanteg koom koom gu adduna bi gënee jëm kanam loolu nag tax ba ay dank sosu yu reew defees it ay kollarante aki dëppoo yu yor màndargam politig mu xare ci diggante ab lim ci reew yi seeni njariñi sanc di jegee walla yi ci jot a àgg ci deggoo ci lijjanti lëj lëj yi nekk ci seen diggante ñu tuddal leen ci dëppoo yooyu ak tapoo yooyu yii di ñëw tapoo gu ñaaral gi ci diggante almaañ otris gii tapoo amoon na ci diggante imbraatooru almaañ gi ak gu otris gi atum g bokk na ci li ëppoon solo ci ay sartam lii di ñëw 	bu rusi gu xaysar gi songee menn ci ñaari reew yi meneen mi war na a dimbli mi nu song 	bu menn ci ñaari reew yi tapoo songee meneen mu ñatteel ma ca des da ca a war a ame taxawaayub génn ci di leen seetaan waaye nag ci anamug cofeel ñeel àndandoom boobu 	bu ag dimblante gu am solo amee walla gu xare ci diggante rusi ak fraans ñaari reew yii tapoo de war nanoo ànd ligeey ngir xeex loolu tapoo gu ñattal gi moom ag tapoo la gu almaañ otris itaali mi ngi sosu ci bi itaali duggsee ci tapoog ñaaral gi nu la tuddoon leegi atum g ak doonte njariñi itaali dëppoowut ak yu imbraatoorug otris gi waxuma la sax noonoo gu yàgg ga nekkoon ci seen diggante te li ko waraloon di yilif gi ko otris yilifoon njëkk bennoo ga ak ca ginaaw ba waaye otris mii moo tegoon loxo ag wàll ci suufus itaali ba noppi yilif fa yeneen wàll itaali duggsi na ci tapoo gi ngir wuute gi mu defoon ak fraans ndax fraans dafa dëgëraloon bu baax tànkub sancam ca goxi bëj gànnaaru afrig fu ci mel ni aljeeri atum g ak tunisi atum g kon itaali duggsi gii mu defoon ci tapoo gi du woon dara lu dul doxaliinu politig li mu ci jublu woon di jañaxal fraans ak britani ngir manante leen ci ñu nangul ko te bàyyee ko njariñam yi nekk ci geej gu diggu gi dëppoo gu fraans rusi gi dëppoo googu am na ci ginaaw bi ag jegeente amee ci diggante fraans ak rusi gu xaysar gi loolu nag tàmbli na atum g daal di gën a jëm kanam atum g bi ñaari reew yi dëppoo ci fas ag kollare guy waral fraans di jox rusi ngànnaay te jëmale kanam ag jokkoom jaare ko ci def fa ay yooni weñ ci atum g la fraans ak rusi def ag kollarante guy yaxal lii di ñëw 	taxawal ag dëppoo ci diggante ñaari reew yi ak weccante xalaat ak diisoo buy lëj lëj amee ci adduna bi 	bu menn ci ñaari reew yi duggee cib xare ñaari reew yi war nanoo diisoo ngir dëppale seen diggante dëppoog cofeel gu britani japon ag dëppoog cofeel sosu na ci diggante britani ak japon atum g lii la yaxal 	bu xare tàkkee ci diggante japon ak rusi gu xaysar gi britani da ca a war a genn te seetaan 	waaye bu meneen reew duggee ci xeex bi nekk ci diggante rusi ak japon kon britani da ciy war a dugg moom itam jàpple japon dëppoog cofeel gu britani fraans ag dëppoo gu cofeel xewoon na ci diggante britani ak fraans atum g gu lijjanti woon lëj lëj ak reeroo yi amoon ci seen diggante dëppoo googu nag lii la wax 	féexal fraans joyal ab loxoom ci marog gii nga xam ne jotoon na a temb te nangul ko teg gi mu teg loxo ajeeri ak tunisi 	fraans moom tam nangul britani teg gi mu teg loxo isipt atum g dëppoo gu cofeel gu britani rusi ag dëppoog cofeel am na ci diggante britani ak rusi gu xaysar gi atum g lii la wax 	déggoo ci ni nuy séddoo barabi sañ sañ yi ci iraan ba mu des fa benn barab rekk bu temb ca digg ba ñu bàyyil ko fa shaah ba ginaaw bi rusi jëlee wàll gu bëj gànnaar gi britani jël gu bëj saalum gi c màggug yëngu yënguy xeetu yi ci tugal yëngu yëngu yi aju ci xeetu dafa xëy gën a màgg ci tugal loolu nag bokk na ci li jañ adduna bi jëme ko ci xare bi xarnub fukk ak juroom neenteel g dees na ko lim muy xarnub xeetu yi ci tugal yëngu yënguy xeetu yooyu nga xam ne li leen taxoon a jug mooy gooreel seen bopp te nocciku ci kilifteef ak teg loxog reew yi leen di àtte cig wàll ak sosal xeet wu nekk am reewum boppam mu koy ëmb uuf ko ci geneen wàll ñaar nag bokkoon nanu ci yëngu yëngu yi gënoon a siw ci yooyu ñooy mbootaayug slaaf gi gii mbootaay walla yëngu yëngug slaaf gii li ko taxoon a jug mooy xettali askanu slaaf wi jële ko ci àtteg imbraatoor gu otris gi ak sos reewum slaaf mu ëmb mbooleem slaaf yi dëkke ci balkaan ak salaaf yi dëkke ci tugalug penku gi mbootaay gii nag daan na jot ag jàpple mu tukke ci rusi gu saaf gi loolu taxoon na ba ag reeroo gu mag am ci diggante otris ak rusi gu xaysar gi d lëj lëji adduna bi ay lëj lëj yu fasu yu adduna bi sosu nanu bokk it bu baax ci li fi taal xareb adduna bu njëkk bi lëj lëj yii it li leen jur day dellu ca reeroo ya amoon ca diggante reew yu mag ya ngir seen gëpplanteg sanc gi ak ngir màggug xeetu ci tugal ak ngir fipp gi askan yi fippoon ngir jot seenug tembte ak gore ñu tudd ci yi ëpp solo ci lëj lëj yooyu lëj lëju maraakes fraans yàgg na a waaj ak a naal ngir teg loxo maxrib gu sori gi maraakes moom nag maraakes dafa yoroon ag tembam lu yàgg te booba tunisi ak aljeeri fraans a ngi leen tegoon loxo yilif leen cig sanc ci noonu fraans lijjanteek britani seen reeroo gi nekkoon seen diggante ca dëppoog cofeel ga atum g fraans daal di bokki ca ndaje ma nu njëkk a def ca dun bu wert ba atum g ca espaañ ngir lijjanti lëj lëju maraakes bi saxal ya juddoo ca ndaje ma nag njariñul fraans la gënoon a nekk ndax reew ya fa daje woon danoo dëppoo woon ci nangul maraakes ag tembam waaye feetale fraans wàllug kaaraange ga ak sàmm njabootug tugal ga fa nekkoon fraans nag jariñu na bu baax ci dénk gi nu ko dénk kaaraange ga ndax ba ay yëngu yëngu amee ca faas ga nekoon peey ba da fa a daal di woon yabal ay dooley xare yu fraans ngir ne da ciy aar jàmburi tugal ya fa nekkoon loolu moo merloo woon almaañ mi àndoon ak buurub maraakes bi daal di ne woon fàww maraakes jot cig tembam ngir naqaral fraans almaañ daal di yabal ag gaal gu mag ca waaxub agadiir ngir aar ag njabootam ak ñaxtoo ci yabal gi fraans yabaloon am mbooloom xare ca faas atum g ngir teg ko loxo ñu defaat am ndaje ca dun bu wert ba ca espaañ atum g ngir lijjanti xuloob fraans almaañ bi la fa juddoo di jox almaañ ay moomeel ca kongog fraans ga bu ko defee almaañ nangul fraans nekk gi maraakes nekk ci ron kaaraangeem ñu daal di def tanja muy ab waax bu adduna bepp daal di doxal nag politigu ubbi buntub maraakes ci kanamu yaxantug adduna bi lëj lëju balkaan otris daa boole woon ci boppam ñaari gox yii di bosni ak hersogowin atum g te ñoom ñaar ñi ngi bokkoon ci diiwaani reewum usmaan mi ci balkaan reewum usmaan mi ca jamono jooja dafa nekkoon di dund ci jawwi yong mooy yong gi ñoñ bennoo ñi defoon atum g serbi nag moom ag wàll la ci yogoslaafi ci jamono jii nu nekk daal di ñaxtu loolu ak rusi gu xaysar gi ko daan jàpple moom serbi almaañ jug moom jàpple otris ci jëfam jooju loolu nag bokk na ci li gën a dolli tangoor wi ca daanaka dun bu balkaan ba lëj lëju maseduwaan ab xare tàkkoon na ci diggante reewum usmaan mi ak gres bulgari ak serbi ci maseduwaan ñoom ay reewi balkaan lanu li ko waraloon nag mooy bulgari gres ak serbi danu doon defi pexe ngir roccee maseduwaan ci reewum usmaan mi te seddoo ko ci seen biir bi nu dàqee reewum usmaan mi ca xare ba ba noppi danoo reeroo woon ci ci seen biir ci nu nu koy seddoo serbi moom daa bëggoon na jot ci albani waaye ñu xañ ko ko ndaxte otris daa taxawoon temb ci nu jox albani ag tembam loolu waral leneen coow amati ci balkaan ci diggante serbi otris ak rusi ak ñeneen lëj lëju tripoli itaali jariñu na ci am soxla gi reewum usmaan mi amoon soxla ak lu ko doy ca xareem ba ca balkaan bu ko defee mu song ko ca tripoli gu soww ga atum g daal di nangu libi teg ko loxo atum g ginaaw bi mu lijjantee ba fraans ak britani genn ci te noppi ci sabab yu jonjoo yi ñeel xareb adduna bu njëkk bi noonoo gi taroon na jëm ci slaaf yi ci balkaan looloo waraloon ñoom slaaf yi juggoon taxawal ag mbootaayug sekkare ngir xeex loolu serbi jàpple leen ci ak rusig xaysar gi ab dongab slaaf yong na arshidog fransis ferninand mi nekkoon wuutlaayu otris ak soxnaam ca suwe g ca dëkkub sarayevo bi nekkoon peeyub bosni ci tukkib nemmeeku bu mu fa doon def otris daal di gaaw jirñoo xew xew bii daal di yonnee serbi ag xupp ca bisub sulye g gu làmboo fukki sart ak benn bokk na ci yi ëppoon solo ci sart yooyu raxas goornamaab serbi bi ak dooley xareem ji ci mbooleem ku bokk ci kureel yiy kontar otris te may otris mu defal boppam raxas gii te tëj yëglekaay yi ak jumtukaayi tes xibaar yi noonoo otris ak boole otris ci gëstu ñi def yong googu ak àtte leen ak yeneen sart yu tar yu tax serbi jort ne kii daal daa fas yeenee dugg ciy mbiri biiram ba noppi otris joxati serbi diirub ñeen fukki waxtook juroom ñatt ne ko mooy àpp bi nga xam ne waru koo weesu te tonntuwul waaye serbi moom tontuwul jibalug xare bi otris taal na xare bi ci kaw serbi ci sulye g bi loolu amee rusi moom itam jug song otris ngir jàpple serbi loolu it jurati almaañ jug cig wàllam jafal ab xare ci kaw rusi ak ci kaw serbi fraans duggsi ci ci wetu rusi miy reew miy xaritam nadx moom la defal ag tapoo daal di jibbal ab xare ci kaw almaañ ak otris britani tam it xuus xare bi kontar ñaari reewi digg yi nga xam ne reewum usmaan mi mujj na àndseek ñoom ci xeex bi siin it ak japon mujj nanu duggsi ci xare bi ci wetu reewi dëppoo gi itaali it dugg si ci kontar reewi digg yi atum g te kat bu njëkk da doon seetan rekk feetewutoonn fenn britani nag nekkoon na di fasante ak itaali kollareg sekkare kollare gi nag li mu doon yaxal mooy itaali jox ko suufus dalmaas bu xare bi jeexee amerig dikk moom itam dugg si ci xare bi ci wetu reewi dëppoo yi daal di genn ca beroom ga mu defoon ca goxub amerig ba duggsi gi mu duggsi woon ci xeex bi nag lu am solo la woon ndax moo ko soppi bu baax ngir doole ak jumtukaay yi mu indil reewi dëppoo yi ak alal lefum xare bi jë bu sòww bi ëmboon fraans ak beljig mooy barabu xeex bi ëppoon solo ci xare bi ci diggante g boobu diggante mooy bi gën a tar ci xeex bi ndaxte dooley reewi digg yi jot nanoo putuxlu ci reewum beljig mi ak wàllug penku gi ci fraans ak li reewi dëppoo yi di jàmmaarlo lepp ak a xeex ngir loolu bañ a am lii nag bokk na ci ndam yi ëpp solo yi reewi digg yi def ci jëwub sòww bi waaye reewi dëppoo yi jot nanoo taxawal jëm kanam gi almaañ ak otris doon def ba daanaka àgg ca bunti paris ci xeexub njàmbaar bi nu doon def ngir aaru ñaari wàll yi nag xeex nanu ay xeex yu tar yi ci gën a siw mooy bu marn bu njëkk bi ci sulye atum g bu dee nag ci jë bu penku bi xare bi moom foofa ci diggante rusi ak otris la nekkoon barabub xeex ba di woon poloñ ak balkaan xeex bi amoon ci penku bi nag xawoon na a woyofal tuuti yan bu diis bi nu tegoon ci ndòddum reewi dëppoo yi ci sòwwu bi ndax reewi digg yi danoo mananul woon a ñàkk a dolli seen soldaar sa nekkoon ca penku ba di xeex ak rusi foofa tam ca penku ba lanu gëne woon aw demiin ca sòww ba ndax jot nanu fa a nangoo wàll gi rusi moom ci poloñ ak litwaani ay xeex am ca diggante reewum usmaan mi ak britani ca iraag ak palastin ca la britani tege loxo ñaari reew yii reewum fraans it nangu siri ak libaa bu dee ci geej gi moom xeex bi mi ngi doon ame ci nuuraakon yi nga xam ne almaañ da leen daa joyal ci gaali reewi dëppoo gi mbooloom gaalum britani mi nag moo kawe woon ci xareb geej gi xareb gitland bu geej bi amoon atum g bokkoon na ci xeexi geej yi gën a rëy ci xare bi nga xam ne amaañ ak britani ñepp ñàkke nanu ci lu dul jeex ciy nit ak jumtukaay atum g bokk na ci at yi gën a tar ci ati xare bii ci la rusi genne ci xare bi ca kollareg litofski ga ca desambar g ci ginaaw bi fippug balsafi gi amee romani topp ca moom mi sukkandiku woon ci xare bi ci rusi moom itam ag gennam mi ngi jaare ci kollare ga nu defoon ca boxarest ca at mooma tam la diiwaani amerig yu bennoo yi ñoom it duggsi ci xare bi ànd ak reewi dëppoo yi loolu nag feeñ bu baax ci doxiinu xare bi ndaxte amerig moom jàpplee woon na bu baax ci wàllug xare ak koom koom loolu nag di woon lu sonnal reewi digg yi ca at mooma tam la jë bu usmaan bi it nërméelu ci la jë bu otris it daanu ay yëngu yëngu aki coow yu ay ligeeykat am ca almaañ ca mooma at it la woodrow wilson defoon fukk ak ñeenti poñam ya doon woote ñu taxawal xare bi te bàyyi askan yi ñu def li nuy wax autodétermination muy tànnal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom atum g nag mooy atum ndam li ñeel reewi dëppoo yi waaye it mu nërmeelu ñeel reewi digg yi ndax imbraatoorug otris ak gu almaañ yépp daanu nanu imbraatoorug usmaan gi it ñàkk mbooleem diiwaanam yi mu amoon ci bitib asi gu ndaw gi nguurug bulgari daanu ci noonu askani reewi digg bi daal sàkku wéerum ngànnaay ci ni ko poñi wilson yi doon sàkkoo bi reewi digg yi demee ba lòtt ci wàllug aaru te manatunoo dékkooti xare bi lanu wommatu bu ko defee bulgari xaatim ag wéer ngànnaay ak reewi dëppoo yi ci satumbar turki topp ci ci mujjug oktoobar atum ak otris ci nowambar ak almaañ ci benn fanu nowambar g lijjanti yi ci ginaaw xare bi reew yi am ndam ci xare bi defoon nanu am ndajem juboo ca paris peeyub fraans li ko waraloon nag mooy gëstu nan lanu war a def ci adduna bi ginaaw bi xare bi jàllee moomu ndaje nag clemenceau moo ko jiite woon njiilul jëwrin lu fraans li bu ko defee ñu defe ndaje ma ca njéndul varsaay la di dëkk bu nekk ca wetu paris diiwaani amerig yu bennoo yi wilson teewal ko britani luwid george njiitul jëwrin la nekkal ko fa fraans clemenceau miy njiitul jëwrin ya moom itam wuutu ko fa ak itaali ci teewaayu orlando njiitul jëwrinam reew yii amoon nanu xejj gu mag ci ndaje mi rawati na ñatti reew yii di amerig britani ak fraans ndajem juboo mii ay saxalam ballewunu ci déggoo ak waxtaan wu reew yi gañe def ak yi nu gañe waaye kay reew yi gañe danoo teg seeni sart ci kaw reew yi nu gañe cig sañ bañ kollare ga nu fase woon ca versailles atum g te xaatimoon ko ak almaañ bokk na ci kollare yi ëpp solo te juddoo ci ndajem juboo mi moom kollare googu dafa yaxaloon lii delloo fraans alsaas ak loren ak delloo danmark wàllug bëj gànnaar gi ci goxub sholswig bu ko defee poloñ moom jot ci suuf su bari ci almaañ ak yoon wu yaatoo ñeen fukki miil wu romb ci biir diiwaanub brusiya gi nekk ci almaañ bu ko defee tàqale kook yeneen suufi almaañ yi ci noonu ñu def waaxub danseg bu almaañ bi muy waax bu nu jagleel reewum poloñ mi nga xam ne taxawalaat nanu ko ci ginaaw xare bi nu jëlati ci almaañ diiwaanu sodit jox ko cekoslawaki mi nga xam ne mi ngi sosu woon ci ginaaw xare bi ñu jëlati ci almaañ waaxub mamel jox ko lituwani bu ko defee almaañ ñàkk mbooleem sancoom yi ba noppi nu ga ko ci mu yamale ay soldaaram ci teemeeri junni nu neenal fa duggum coldaarum gu sañ bañ dindi mbooleem tata yi wëroon kanaalub kyel ak goxub rayn nu tàmbli woon a def fuglu gu tar ci ligeeywaayu ngànnaay yi ak jumtukaay yi ci aju ñu nangoo woon ci almaañ it mbooleem ay nuuraakonam aki gaali xareem aki fafalnaawam ak lu ëpp ci ay gaali yaxantoom ci noonu fraans nangooti diiwaanu saar di xuru dexug rayn gi di barab bu naat ci ay mbell mu nangu ko nag diir bu tollu ci fukki at ak juroom ñu daal di teg almaañ nag ag alamaanug xare ak alal ju mu war a fay ju bari ju tollu ci yu sterlin ak doonte almaañ fayu ci ci diggante g lu dul lim boobu rekk imbraatoorug otris gi nag moom ndaje ma daa daal di jeexal nguurug njabootug habsborg ga fa nekkoon daal di taxawal ciy màbbiitam ay àtte yu bari ñooy pencum otris ak hongri ak pencum cekoslawaki ñu jëlati wàllam ya nekk ca balkaan boole ko ca reewum yogoslawi mi sosu ci ginaaw xare bi bu dee reewum usmaan mi moom dafa ñàkkoon mbooleem moomeelam yi mu amoon ci asi ak afrig deseetutoon lu dul moomeelam yi mu amoon ci asi gu ndaw gi ñu daal di ko def muy leegi pencum turki wuuteek lool reewum usmaan mu mag ma nu xamoon loolu di woon ci g ginaaw bi mustafa kamaal atatork g neenalee nosteg saltana ga fa amoon atum g ak gu xalifa ga atum g ndaje mi nag sos na fi ay reew yu yees yu bari ci balkaan mu ci mel ne mom yogoslawi mi jële won ay suufam ci reewum serbi mi ak yenn ci goxi balkaan yi bokkoon ci moomeelug imbraatuurug otris gi bu ko defee nu sosaat reewum poloñ mi ak brusiya reewum cekoslaafi moom itam taxawe ci ñaari xeet yii di slaaf ak cek reewum hongri tam sosu finland stwaani lituwani ak latfiya reew yii yepp jug di dëgëral seeni nekktey politig te bu njëkk danoo nekkoon ci ron teg loxo gu almaañ ci ginaaw bi rusi gennee ci xare bi atum g daal di fas kollareg litofski gi ak reewi digg yi lii moo jeexal àtte gi njabootub romanof gi doon àtte rusi ñu daal di jël nag yenn reew yi teg leen ci ron ag feetale iraak penkub urdun jordanie ak palastin ñu teg leen ci ron feetale gu britani atum g siri ak libaa ñoom ñu teg leen ci ron feetale gu fraans atum g ndajem paris ma nag saxaloon na feetale gii te xaatimoon ko ñu daal di sos kureelu xeet yi league of nations teg ko ci poñub fukk ak ñeent bi ci dali wilson yi doon woote ag ñoal jàmm ci adduna bi ak tee xare amati fi ak dëgëral dimblante ci reewi adduna bi nii daal la xareb adduna bu njëkk bi jeexe ginaaw bi mu sonnalee adduna bi bepp sotti ko sawaraam si ak alkandeem li ray nanu ci lu jege juroom ñatti milyoi nit gaañ ca lu jege ñaar fukki milyo waxuma la nag ñi faatoo ca xiif bu metti ba ak tawat ja xare ba waraloon ñaareelu xareb adduna bi g lijjanti ak saxal ya juddoo woon ca ndajem jàmm ma ca paris ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi ñoo jur man nanu ne lu ëpp ci li sooke ñaareelu xare bi kollareg jàmm ga fa juddoo woon sooke woon na mer wu metti akub sànj ci askani reew yi nu note ca xeex ba askan yooyu nga xam ne doyutoon ñu yanu coonay xare beeki musibaam rekk waaye ñu tegati ci yan leen li ci juddoo ci ginaaw bi ay saxal aki lijjanti yu diis yoo xam ne reew yi notoon a leen tegoon ci seen kaw loolu nag juroon ci ñoom ag mbañeel akug bëgg a fayyu nekkiinu koom koom wi jaxasoo tegoodi ci yoon am pax gasu ci tugal ci diggante askan yeek seeni goornamaa loolu tam man nanu ne mooy li gën a tax ay noste yu yees sosu yoy sañ sañ bu joyu lanu jëloon def ko seen raayo ay kureel yu neew jugoon nanu teg loxo ci àtte gi ci yenn ci reewi tugal yi daal di biral ne li leen tax a jug mooy xettali seeni askan ci jafe jafe yi nga xam ne xareb adduna bu njëkk bi ba na leen fi ay goornamaa yu diktaatoor feeñ ci biir tugal ak ci biti leegi nag jeneen jamono ju yees tàmbli ju ngànnaayu muy wutu ngànnaay moo xam ne li ko jur mooy bëgg a fayyu ci reew yii note ci xare bu njëkk bi te toroxal askani reew yi nu not te diisal seen ginaaw ci ay alamaan yu saf te tar lii daal moo sabab xareb adduna bu ñaareel bi li laytaay xare bi àttey diktaatoor yu bees yi sosuwoon man nanu ne ñooy jëfka yi jiitu ci taal ñaareelu xare bi ñu indil la wax ju gàtt ci ñatt ci yi gën a am solo ci noste yooyu nosteg àtte gu mbokkoo rusi mooy reew mi àtteg mbokkoo njëkk a taxaw loolu di woon ci ginaaw fippug oktoobar ga amoon ca atum g li ko waraloon di koom koomam ba daanu woon te ñu dàqoon ko ci anam gu toftaloo ca xare bu njëkk ba ca kanamu almaañ ci ñaari at yii di ak g te mu ñàkkoon it lu tollu ci milyo ak xaaj ci ay xarekatam ca xare booba lenin g mi nekkoon njiitul làngug mbokkte gi parti communiste moo jiite woon fipp googu daal di woon def ag juboo ak waa almaañ yi taxwal it ay jataay yu askan yu barab yi soviets daal di xeetal jumtukaayi ligeey yi taxawal ab goornamaa bu ay ligeeykat aki baykat daal di yëngu ci luy neewal tàqale yi am ci diggante xeet yu wuute yi waa rusi yu sofiet yi taxawaloon nanu ab jë bu yaatu kontar nosteg bopp alal gu soww gi ñu jiite woon kureelub mbokkoo bi kontar diine ak nostey demokraasi yi ñu mujj nag am doole ju mag ak jeexiital gu rëy ci liy xew ci adduna bi yàgg nanoo jëfi jëf ci yekkati tàngoor yi ci adduna bi walla xiiroo ak ngaayoo yi daa am ci adduna bi ci diggante ñaari xare yi nosteg àtte gu nasi ca almaañ làngugug mbokkoo gu xeet gu ligeeykat yi gu nasi gi di parti national socialiste almand des travailleurs gii làngug politig di gu nasi gi daa jariñoo woon profitoo woon ci li daloon waa almaañ yi te wàcci ci seen kaw ci toroxte ak doyadal ak suufeel te li ko waraloon di tënk tënk yi nekkoon ci kollareg versailles gi ak jafe jafe yi mu leen indil ak ñàkk gi leen wër peek leen ak ñàkk ligeey gi ak deltu ginaawug koom koom bi nga xam ne saxoon na fi ay at ginaaw xare bu njëkk bi làng gii nag jariñu woon na ci lii lepp ngir fitali ca àtte ga l état teg ko loxo nangu ko ci njiitug adolf hitler g mi nga xam ne bindoon na dali làngam googu ci teereeb xeexam ba dal yooyu nag danoo taxawoon ci ay cëslaayi waaso ndax daa gëmon ne waasow jermaan mooy waawo wi gën ci waaso yi te it daa gëmoon ne danoo war a sos ag almaañ gu mag gu ëmb mbooleem waa almaañ yi gëmoon it ne àtte gi l état daa war a teg loxo mbooleem lonkoo yu rënk yu mag yi ci almaañ te danoo war a neenal kollare ga nu fasoon ca versailles te danoo war a delloosi mbooleem sancu yi kollare googu ñàkkloo woon almaañ hitler mujj na di njiilul almaañ loo xam ne daa amoon sañ sañ bu joyu pouvoir absolu ñu mujj di ko wooye fuhrer mu tàmbli nag di doxal dali làngam yooyu ci askanu almaañ wi nga xam ne àndoon na ak moom ngir bëgg a mucc te xettaliku ci nekkiin wu bon wi mu nekke woon rawati na ñàkk ligeey gi nga xam ne yaatu woon na lool ci almaañ ngir xare bi ak ngir tënk tënk yi nga xam ne kollareg versailles gi indi woon na leen fi hitler def na ay jëf yu bari yoo xam ne ñoo fi sabab ñaareelu xare bi ndax daa jëloon diiwaanu saar boole ko ci almaañ atum g neenal kollareg versailles jox sodaar si ngànnaay yu diis te xereñ jëmale endustri bu almaañ ci ligeey ngànnaay ak jumtukaayi xare aki bagaas yu ame solos xare mu jëlati reew yiy wax làkkuw almaañ wi boole leen ci almaañ daal di taxawal rayix bu ñatteel bi mu booleeti otris ci almaañ atum g jëlati goxub sodit bi nekk ci cekoslaawi atum g daal di jeem a nangu yoonu danseg ci doole seddoo ak rusi poloñ almaañ nag dundoon na ci ron àtteg nasi la ko dale ca g ba bi mu daanoo tas ci atum g nosteg àtte gu fasi ca itaali waa itaali yi yëgoon nanu te ñoom kat ci reew yi amoon ndam lanu woon ci xareb adduna bu njëkk bi yëgoon nanu ne danu leen a naxe ca ndajem jàmm ma amoon ca paris màngiit yi juge woon ci xare bi it lu neew lanu leen ci jox te kat ñoom ñu ci sonne lanu ag ñàkk ligeey tas ci itaali nekkiinu nit ñi ñaaw làngi politig yi fees fa dell reew ma jaxasoo xalaat yi tas fa di mbokkte communisme fasi ak yeneen xalaat yi fasi nag lu fi ñëwoon la ngir xeex mbokkte benito mussolini jiite ko mi jiite woon ag làngam g làng googu nag danoo warlu woon ci seeni dal principes xeex mbokkte taxawal ag nosteg dimblante te jeem a jot ci ngañaayi sanc yi nga xam ne danu leen a xañoon itaali ca ndajem paris ma ci noonu làngug fasi gi tàmbli di jëfandikoo fitna violence ci xeex ak xuloowaaleem yi bi dégug làng gi gënee dëgër gën a ñaw mu gën a am doole ci la mussolini ak àndandoom yiy solsimis yu ñuul xuppe goornamaab itaali bi ci noonu buurub itaali bi di victor emmanuel amatul woon pexe mu daal di jox nguur gi kii di mussoliini mi nga xam ne mujj na di diktaatooru itaati ñu ko daa dàkkantale dotsi mussolini digale na ñu neenal làng yi aaye askanu itaali wi ñuy def yëngu yëngu mbaa coow nos endustri bi dëppale diggante njariñi ligeeykat bi ak naatug walla jëm kanamug endustriy yaxantu yi daal di juboo ak paab bi delloosi njàggalem diine mi ci jàngu yi leekol yi mussolini feeñal na mbonam gi ak mbonug làngam gi jaare ko ci jëfam yu ñaaw yi mu jëmale woon ci askanu libi wi ba mu fa bëggee samp sancug itaali gi mu gënoon a yaatal ag kilifteefam ca ecopi atum g ginaaw bi ko soldaari itaali yi tegee loxo ci doole nangoo ko ci waa ecopi yaatalug sanc gu itaali gii merloo woon na askan yi nekkoon ci ron ag sancam te taxoon na yeneen reewi sancaan yi kontar ko ci loolu lii nag mooy li jegeele diggante nasi ak fasi nga xam ne mujj nanu àgg ci def ag dëppoo ci seen biir mooy taxawal ag tapoo gu xare nu duppee ko diggub berlin rom bokk na ci diktaatoor yii ba tay làngug xare parti militaire gi nekkoon japon ak àtteg franco ga ca espaañ g moom franco mi mujjoon ame nguur gu joyu pouvoir absolu ca espaañ atum g ginaaw xareb ñoñ bu espaañ ba koolute gi askani almaañ yi amoon ak yu itaali yi yu espaañ yi ak yu japon yi ci seeni goornamaay xeet yu ëppaloon yi te teengal dolliku woon na te li ko waraloon di ñàkk gi nostey bopp alal yi ak yu demokraasi yi ñàkkoon kàttan ci jële fi coonab koom koom bii fi amoon ak ñàkk gu tar gii ubale woon tugal gépp ak feneen ci biir jafe jafeb koom koom bi amoon ci adduna bi atum g ñu gënoon koo xame ci turu lamb gu mag gi yeneen jëfka yu sabab xare bi am na fi yeneen jëfka yoy dugg nanu ci li fi indi xare bu ñaareel bi bokk na ci yi ci ëpp solo 	lòtt gi kureelu xeet yi lòttoon ci ñoal jàmmi àdduna bi ginaaw bi ci almaañ ak itaali gennee ak japon 	digg axe yu politig ak xare militaire yi nga xam ne reewi diktaatoor yi taxawaloon nanu leen ci seen biir bu ci mel ne digg bu berlin rom ak bu berlin tokkiyo ak kollarante gu ñàkk a noonu gi amoon ci diggante berlin mosko laata a xareb ñaareel bi di tàkk ci lu tollu ci ay ayu bis yu neew ci geneen wàll gi fraans britani romani poloñ ñoom itam booloo nanu def seenug tapoo nii daal la ñaari dank sosoo dankub digg bi làmboo almaañ itaali japon ak dankub reew yi tapoo walla way tapoo yi di britani fraans romani poloñ benoog sofiet gi ak amerig ci ginaaw bi 	xuloo bi amoon ci diggante reewi balkaan yu yees yi te aju woon ci mbirum dig yi ci seen biir ndaxte amunu woon ay dig yu sax ak xuloo bi amoon te aju woon ci mbirum xeetu nationalisme ndax kat reew yii di yu sosoo ci seddaleg ndaje ma danoo ëmboon lu sakkan ciy xeeti almaañ lu jege juroomi milyoi ay waa almaañ ñu mujjoon bokk ci njabootug poloñ ak cekoslaafi 	masalam yoonu poloñ wi tàqale almaañ ak brusiya te daytaloo ca waaxub danseg bu gore ba libre ña dëkke woon ca yoon woowa ci ay waa almaañ jege woon nanu ci noonu hitler daal di ne day boole yoon woowu ci almaañ looloo fi taalati gilinug xare bi ci adduna bi ndaxte fraans ak britani ñoom danoo daal di woon jàpple poloñ ci noonu hitler daal di joxe ay ndigal ci nu song poloñ ci satumbar atum g ginaaw bi mu gisee ne ànd na ak bennoog sofiet gi itaali ak japon nii daal la sawaras ñaareelu xareb adduna bi tàkke jamono yi nga xam ne xare bi jaar na ci ak lefi xare bi xareb adduna bu ñaareel bi romb na ci ñatti jamono ñooy 	jamono ju ndam yi hitler doon ame ci xare bi mu tàmbli ci g 	jamonoy yamoo équilibre walla li nuy duppee at mu jaxasoo mi di woon atum g 	jamonoy nërméelu ñeel réewi digg yi mu tàmbli ci atum g hitler yëgaloon na poloñ atum g ne ko manul ñàkk mu génne loxoom ci waaxub danseg bi te delloo almaañ yoonu poloñ wi romboon ci suufus almaañ boobu lëj lëj bokkoon na ci li juddoo woon ca ndajem jàmm ma mooy li fi taalati xare bi ci adduna ndax mooy sabab bu jonjoo bi ko jafal hitler yamul rekk ci yonnee ag xupp jëme ca poloñ waaye da ca a rax dolli yabal ay soldaaram ñu song ko teg loxo ay suufam bi mu lànkee bañ a wuyyu wooteb almaañ bi bañ a faale xuppam gi bi mu kodefee britani ak fraans jug yonnee ag xupp jëme ca almaañ ne ko na génn suufus poloñ si ci diir bu weesuwul ñaar fukk ak ñeenti waxtu bi almaañ lànkee bañ leen a déglu la ko britani ak fraans song ci satumbar g almaañ jot naa teg loxo waaxub danseg ak yoonu poloñ wi ak lenn ci goxi soww yu poloñ yi ag dëppoo am ci diggante almaañ rusi gu waral ñu séddoo ñoom ñaar suufus poloñ si loolu nag di bi rusi tegee loxo goxi penku yu poloñ yi daal di def ak almaañ kollareg ñàkk a noonu non agresssion di gi amoon ci ut g waa almaañ wéy ci seen xare bi daal di nangu danmark ak norwej atum g ginaaw ba nu fa dàqee dooley britani ji ak ju fraans ja fa nekkoon ci geneen wàll rusi moom gën na a tàllal ay tànkam ci finland loolu nag mu jaare ko ca kollareg ñàkk a noonu gi mu fasante woon ak almaañ almaañ daal di song luksamburg nangu ko ci lu yéeme cig gaaw songati holand nangooti ko song beljig nangu ko waaye ci ginaaw xare bu saf sàpp bu mujjoon waral deltu ginaawug dooley britani ji ak ju fraans ji atum g dooley jañ ak naj gi almaañ doon def ci bëj gànnaaru fraans gënoon a dolliku gën a tar ci noonu goornamaab fraans bi daal di tuxoo paris dem bordeau foofa lanu tàmbli woon a sàkku ag wéer ngànnaay ak almaañ ci noonu general deegol daw làqu ca london fa la doon jiitee jànkoonte resistance gu fraans gi kontar réewi digg yi fa la birale it ag fraans gu gore gu ànd ak réewi tapoo yi les alliés goornamaab fraans bi diriku woon ba bordoo daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak almaañ muy gu mel ne ga almaañ defoon ag réewi dëppoo ya ca g wéer ngànnaay gi nag lii la wax 	almaañ nangu bëj gànnaaru fraans péey ba di paris bokk ca ak mbooleem tefesi fraans yi tiim mbàmbulaanug atlas gi 	fraans day fay almaañ ay alamaan yu alal yu tollu ne ferey soldaari almaañ yi nangu fraans 	limub soldaari fraans yi dootul weesu téeméeri junniy soldaar 	taxawal goornamaa bu fraans buy ànd ak almaañ bii goornamaa nag taxawoon na ci njiitug marsal bitan ñu duppee woon ko goornamaab fishi ngir nekk ga mu fa nekkoon ginaaw bi fraans wommatoo meruw almaañ itaali wi dafa sottiku woon ci kaw britani bu ko defee fafalnaaw yu almaañ yi jog def lòkki yu toftaloo ci kaw dëkki britani yi la ko dale ca ut g waa almaañ ñi nag li nu jublu woon ci loolu mooy manante britani ci wommatu cig wàll ak waaj ngir wàcce ay dooley almaañ ca duni britani ya ci geneen wàll waaye taxaw gi askanu britani wi taxaw taxawaay bu dëgër te sax moo tax ba waa almaañ ñi manuñu woon a am li nu bëgg réewi tapoo yi tàmbli woon nanoo ndàmmi ndam di xaw a kawe réewi digg yi as lëf bi amerig duggsee ci xare bi ànd ak ñoom atum g ni ci bennoog sofiet gi dugge dooley britani yi nag ndàmm nanu ndam lu mag ci jë bu afrig bi ci kaw dooley itaali yi daal di leen dàqe ca ecopi ak eriteri looloo taxoon hitler yabaloon ñaari kuréeli xare yu almaañ ca bëj gànnaaru afrig marshal rommell jiite woon leen ngir xettali ji àndandoom ba ca afrig ab xeex bu saf am ca bëj gànnaaru afrig ca nowambar g ci diggante réewi tapoo yi ak yu digg yi ci njiitug mongomeri mi jiite woon réewi tapoo yi ak romal mi jiite woon réewi digg yi ci noonu réewi tapoo yi ndamu ci kaw yu digg yi ca xeex ba nuy wax alamayni ginaaw xeexub ñukkaakon tank char bu mag bu sax fukki fan ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xeex bii nanu ci tudd 	teg loxo gi réewi tapoo yi tegoon loxo goxi bëj gànnaaru afrig ginaaw bi nu fa dàqee dooley itaali ji ak ju almaañ ji 	itaali wommatu na soldaari réewi tapoo yi wàcc ca sisil ñu daal di daaneel nosteg mussolini gi ca satumbar g 	nosub xare bi mujj na nekk ci loxol way tapoo yi ginaaw bi mu nekkee ci loxol almaañ ak réewi digg yi àggoon nanu nag ci seen njòbbaxtali ndam atum g ndamul réewi tapoo yi ginaaw bi dooley britani yi ak yu amerig yi lijjantee ba am ndam ca jë ba ca afrig ak ginaaw bi mussoolini daanoo la réewi tapoo yi fasoon yéenee jële fi almaañ ñu wàcce woon soldaar su dul jeex ca tefesug normandi ga àggoon nanu cib lim ñaari milyoi nit daanaka ñu tegoon leen nag ci kilifteefug generalu amerig bii di dwaayet asinhawar bu ko defee yii doole daal di teg loxo fraans beljig holand suuf yu xóot yi dooley almaañ yi xëyoon nanu wëlbati një cig deltu ginaaw jëme almaañ waaye dooley tapoo yi mayuñu leen woon fu nu yakke seen nàkka ngir ragal ñu jekkaat ba amaat doole ju nuy songeeti kenn ci noonu ñu dab leen ca saa sa jot a sutuxlu ca digi almaañ yu soww ya ca fewriye g ruus yi nag ñoom jotoon nanoo jéego jéego yu am solo ci jëwub penku bi ci goxi penkub tugal bi ginaaw ba fa dooley almaañ yi jugee ci noonu ñu nangu jëwub tugal gu penku gi ci suwe g ci nii daal la dooley almaañ tàbbee ciy xat xat yu jafe ci kanamu doole yu rëyub lim te nu waajal leen ci ngànnaay yi mujj a génn bu ko defee almaañ xëy di ku ñu gaw ci diggante ñaari wàlli kuur ci diggante penku ak soww looloo juroon almaañ faroon wommatu ci mujjantal gi ci me atum g ñu daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak réewi tapoo yi loolu mujj di li taxawal dooley xare ju almaañ jii jot a miiral adduna bi sonnal ko ngir xareem yu bari yii leegi nag réewi tapoo yi di angalteer fraans bennoog sofiet ak amerig nangu nanu berlin péeyub almaañ jàmmaarloo gi waa almaañ yi doon def ak a dàkku seenub dëkk taxaw te jeex wommatug japon waa amerig yi yanoon nanu seen bopp coonab xare bi ci penku kontar japon ginaaw bi waa amerig nangoo suuf yu bari ci li japon tegoon loxo ci xare bi lanu dogu woon ci gañe xeex bi ginaaw bi nu jotee fent bombub fepp bombe atomique te bëgg a xam li mu man te bëggoon it japon wommatoo ci seeni loxo ñu daal di jug ci ut sànni ñaari jum yu fepp ci ñaari dëkk ci japon ñooy irosima ak nagasaki ci noonu japon mujj wommatu daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak waa amerig yi ci turu réewi tapoo yi ci satumbar g bu ko defee ñaareelu xare bi daal di jeex li juddoo ci ñaareelu xareb adduna bi ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xareb adduna bu ñaareel bi bokk na ci yooyu 	def ndajem botsdam ca anéeru berlin ca sulye g ngir jeexal xeex bi britani teewe woon na ko fraans bennoog sofiet gi ak diiwaani amerig yu bennoo yi 	dagg goxub brusiya ci almaa ñ gu penku gi bu ko defee bennoog sofiet gi jël ca wàllug bëj gànnaar ga poloñ jël wàllug bëj saalum ga ñu joxati poloñ dëkkub danseg bu gore bi waaxub danseg 	séddale almaañ def ko ñeenti barabi sañ sañ ci diggante amerig britani fraans ak bennoog sofiet ci atum g la njëkk a am ci taarixu almaañ ñaari reew sosu ci almaañ te yor ag nosteg pénc systeme republicain walla tosteg askan ñooy almaañ gu soww gi walla péncum almaañ mu bennoo mi la république fédérale d allemagne nekk nag ci ron saytug amerig britani ak fraans bon di péey bi geneen gi di almaañug penku gi brusiya gu njëkk ga walla almaañ gu demokraasi gi la république démocratique allemande bennoog sofiet gi saytu ko berlin gu penku gi dib péeyam ñu fàttali leen rekk ne amerig britani ak fraans mujjoon nanoo may almaañ atum mu wut ay soldaar 	almaañ ñàkk na mbooloom xareem bu dëgër ma te rëy ñàkk ngànnaayam yu bees ya te jëm kanam bi nu tasee ab xareem neewal dooleem 	tegoon nanu almaañ mu war a fay li mu yàqal rewi tapoo yi 	nosaat koom koomu almaañ bi rawati na nosteg alal gi ak gu endustri gi yooyu yépp ñu jëme leen leegi ci luy ligéeyal mbiri yi dul xare 	séddale otris def ko ñeenti barabi sañ sañ ci diggante britani amerig fraans ak bennoog sofiet otris it des ci ron teg loxog réewi tapoo yi ba ci atum g ak doonte réewi tapoo yi nangu woon nanu ne réew la mu temb dale ko ca atum g 	réewi tapoo yi nangoo nanu ci japon dun yu am solo bu ci mel ne farmosa ak sakalin añs rafleel ko ci mbooleem moomeelam yi nekkoon ci màmbulaan gu atlas gi dooley amerig yi nag juge nanu japon atum g ginaaw bi nu xaatimee ag kollareg wéer ngànnaay cis een digganteek goornamaab japon bic i dëkkub san fransisko 	xaatim nanu ag juboo ak itaali bulgari romani ak hongri atum g gii juboo nag li mu yaxal mooy réew yii warloo fay réewi tapoo yi ay alamaani xare 	 deltu ginaawug ñaari réew yii di fraans ak britani ci nekk gi nu nekkoon ay réewi adduna yu mag ci ginaaw xare bi bu ko defee amerig ak sofyet yi jël seen barab mujj it di réew yi ëpp doole ci adduna bi mujj yor ngànnaay yu bon te aaytal 	 nërmeelug ñaari noste yii di nasi ak fasi ci tugal ak nosteg xare ga nekkoon japon te noste gu mu ci doon rekk sag am bokk na ci li fi indi ñaareelu xare bi nostey diktaatoor yooyu bokkoon nanu ci nooni mbokkte yi gën a mag 	 feeñug dankub mbokkoo bi bloc socialiste ay réew yu bari bokk ci bennoog sofuet gi jiite ko mu ci mel ne kore gu bëj gànnaar gi wietnaam gu bëj gànnaar gi poloñ bulgari romani cekoslowaki ak hongri añs bu dee nag siin gu askan gi ak yogoslawi nag ñoom ñaar ay réeyi mbokkoo lanu waaye nekkunu woon ci ron yilifug bennoog sofiet dankub bopp alal bu gore bi it feeñ amerig jiite ko làmboo nag réewi tugal gu soww gi niki britani fraans almaañ gu soww gi holand beljig danmark ak norwej añs amerig it warlul yii réew ndimbalug alal ak gu xare ngir ñu man a taxaw ci kanamu dankub mbokkoo bi 	 sos tapoog càmmooñu atlas otan atum g mooy tapoo gi boole woon amerig britani fraans kanada réewi sowwub tugal bi japon ak turki réew yii nag danu ne woon ku ci song menn rekk song nga yeneen yepp ñu kollarante woon ci seen biir ci dimblante ci wàllug aaru koom koom ak alal ci geneen wàll tapoog warsaw gi daal di taxaw tukkee ci bennoog sofiet ak réewi mbokkoo yi topp ci ginaawam ci càmmooñu tugal ak penkoom 	 jëya ju rëy ji juddoo ci xeex bi muy faatug lu sakkan ci dooomu aadama ak yàqug alal ju dul jeex ngir jumtukaayi xare yu xereñ yi nu ci jëfandikoo ñuy jum yi les missiles bombi fepp yi nuuraakon yi ak ñukkaakon yu diis yi ans xare bii moo ëpp lu mu yàq ray ko màbb ko ca moomam ja ko fi jiitu woon 	 ëttu àtte yu normbrug yi ngir àtte ñoñ nasi ñi ci tuumay jqi fitna ak sabab xare bi ak def ay tooñaange jëme ci ñu ñu tëj ñi les prisonniers ak ñi ñu njafe ca reewi tapoo ya àtte nanu fa tam njiiti nosteg xare gi nekkoon japon 	 juddug mbootaayu xeet yi ngir dëgëral jàmm ak tere xare yi ak xulooy réew yi ak amal mbaandute ak yamoo ci réewi adduna bi 	 koom koomu àdduna bépp a naatoon ginaaw bi xare bi jàllee li ko waraloon di naali tabax yeek yeneen yi nga xam ne defaraat dëkk yi la doon ligeeye ak wàllug tabax ci anamam yepp bi gënoon a rëy ci naal yooyu mooy bu marsaal 	 judduwaatug joante ci ngànnaay ci diggante ñaari dank yi bu mbokkoo ak bu bopp alal ak sosu gi xare bu sedd bi sosu ci seen diggante naka noonu dund ci jàmm gi am leegi ci diggante xeet yi ci kaw suuf doggantal gu ñaareel gi mbootaay yu adduna yi kureelug xeet yi mbootaayu xeet yi walla xeet yu bennoo yi mbootaayug reewi lislaam yi walla mbootaayu daje gu lislaam gi ñatti mbootaay lanu bëgg a waxtaane ci doggantal gii ñooy kureelu xeet yi mbootaayu xeet yi mbootaayu reewi jullit ñi kureelu xeet yi njiitul amerig la tuddoon widro wilson da doon ku daa xalaat nu mu fiy taxawale mbootaay gu mag gu adduna bi guy jeem a indi jàmm ci adduna bi ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi waxoon nanu ne wilson moom jotoon na a leeral dalam yooyu nga xam ne fukk lanu woon ak ñeent ci biir xeexub adduna bu njëkk bi ne woon daal fàwwu nu sukkandiku ci ñoom ngir taxawal xeex bi ak ngir rëddaat sëqooy reew yi teg leen ci dàtti jàmm ju sax ak moytu xeex yi nar a amati wilson moom gaaraloon na naalam boobu di kureelu xeet yi gaaraloon na ko ca waxtaanu jàmm wa nu amaloon kollëre ga nu jotoon a fas ca versaay it moo rëddoon lanu fa xaatim lii di ñew di nanu ci leeral li ëpp solo ciy poñ yu nekk ci kollëre gi taxawal kureelu xeet yi 	sose kureelu xeet yi ci mbooleem reew yi am tmb gu mat gu dara wàññiwut reew yoo xam ne man nanoo indi ay warlu yu mat ci respekte walla wormaal jàmm te bàyyi xeex mbaa lu koy waral 	reew yi bokk ci kureel gi dananu warlu ne kenn du ci xeex ak kenn te gaaralul li ko tax a bëgg a xeex ci kureel gi ngir nu àtte leen te xool li leen boole reew yi ci bokk it war nanuy seet mbugal yi yell ci reew yiy tooñ yu ci mel ne teg leen ay gaw yu koom koom walla jëfandikoo doole ci seen kaw 	jeem a dëgëral buumi dimblante ci adduna bi jaare ko ci sukkandiku ci maslaa gu fés ak wormaal kollërantey reew yi ak xeex njaam ci meloom yepp jeem a rafetal nekkiinu ligeeykat yi ak seenug dund ak xeex dorog nos yaxantu ci adduna bi ak sonn ci wér gu yaramu nit 	reew yi ci bokk dananu warlul yeneen reew yi wormaal seenug tembteg politig dananu warlu it bañ a def ay kollërey sekkare ak jox kooluteg kureel bi ab day ci mbooleem kollërante yi reew yiy def ci seen diggante koolute gi nag di secretariat bi ci dëkkub geneve bi nekk siwis la nekk 	aar neewtey xeet yi ak yu diine yi nekk ci mbooleem reew yi ak wormaalal askan yi ak xeet yi nekkoon ci ron imbraatoor yi wormaalal leen seen àq ak sañ sañ ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg te gis ne moo gën ci ñoom ak reew yi nu gañee ci xareb adduna bu njëkk bi 	kureel bi mooy taxaw ci di xool ni nuy doxale nosteg féetale gi mooy noste googu nga xam ne moo waraloon yenn ci askan yi xeet yi ak mbooloo yi nu feetale leen reewi sancaan yu mag yi teg leen ci seen ron kilitfeef ak doxaliin ginaaw bi reew yooyu nekkee ci waawug reew yi nu gañee woon ci xeex bi ñuy reewum usmaan mi imbratooru otris gi ak gu almaañ gi loolu nag nu defoon ko ngir waajale leen ci ba man leen a may ag tmb ëlëg kureel bi bi muy door a sosu reew a ca bokksi woon ci noonu reew yiy temb di gën a dolliku naka noonu di gën a bokksi ba mujj limub reew yi bokk àgg ci juroom benn fukk mu ci nekk it am genn kàddu ci bu nuy woote kollëreg kureel gi jox na reew mu nekk àq ak sañ sañ ci mu genn ne bokkatuma waaye ci kaw reew moomu teel a yëgale ag bëgg a bàyyeem lu tollook ñaari at cig njëkk bànqaasi kureelu xeet yi kureelu xeet yi ñatti bànqaas yu mag la am ñooy jataay bu matale bi jataayub kureel bi koolute gi walla secretariat nga rax ci dolli ñaari bànqaas yu ci bànqaasoo ñooy àttekaayu maanduteg adduna bi ak mbootaayug ligeey gu adduna bi jataay bu matale bi mi ngi daa ame ci mbooleem ndawi reew yi bokk ci kureel bi ab dajeem it benn yoon la daa am ci at mi ci weeru sëtumbar ngir xool ak xalaat ci mbooleem xew xew ak mbir yu am solo yi nekk ci ay prograamam jataayub kureel bi moom mi ngi sosoo woon ci njëlbeen gi ci juroom ñeenti cer juroom yi ci juroom ñeent yooyu ñooy reew yi am ag bokk gu sax ñooy britani frans itaali japon ak almaañ mi jël cerub amerig mi nga xam ne bokkutoon ci kureel bi ak yeneen ñeenti reew yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn leeg leeg bii jataay nag dana faral di daje ñatti yoon ba ñeent ci at mi dana faral di daje it ci anamug jagle ci xew xew yu bette yu man a xupp jàmmi adduna bi limub toogu yu sax yi tam yokk na ci jataay bi juge ci ñeenti toogu dem ci juroom ñeent koolute gi secretariat koolute walla secretariat bu kureelug xeet yi mi ngi sosoo woon ci ligeeykat yu kureel bi ya daa ligeeye ca dalam bu sax ba nekkoon geneve njiit li moom moo daa doon ku nu woolu ku matale ki nga xam ne jataay bu matale bi moo ko daa tànn koolute gi nag amoon na ay kureel yu bari yu aju woon ci moom ñooy kureelug dimblanteg aada gi kureelug jële fi ag njaam kureelug xeex dorog kureelug aar neewte yi kureelug féetale yu sax yi ak kureelug tawat yu bon yi am na yeneen bànqaas yu am ag jokkoo ak kureelu xeet yi ñooy yu mel ne àttekaayu maanduteg adduna bi ligeeyam di àtte xuloo yi ak amlante yi àttee ko nag ci yoon walla luwa bu àdduna bi ak kollërante yi reew yiy xuloo jotoon a def nosteg kureel bi nag li mu wax mooy àttekaay bi fukk ak juroomi àttekat ñoo koy taxawal yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn tànne leen nag ci kandidaa yi nga xam ne reewi kureel bee leen di ind àttekaayub maanduteg adduna bi moom mi ngi sosu ci atum g ab dalam it nekk lahaay ca holand ak mbootaayug ligeeyub adduna bi ligeeyam di yewenal nekkiinu ligeeykat yi ci adduna bi ak yekkati seen tolluwaayu dund moom nag mi ngi booloowoo ci ndawi ligeeykat yi ak sendikaay ligeeykat yi ak boroom ligeey yi geneve nag moo dib dalam ayibi kureelu xeet yi kureeb xeet yi de ak li mu def lepp ci ligeey yu jëm ci saxal jàmm ci adduna bi ci biir fukki at yu njëkk yi ak li mu fi def ci ligeey yu am njariñ ci wàllug mboolaay loolu lepp teewul mu lottoon te ñakk kàttan ci lijënti xuloo ak ngaayoo yi da a am ci diggante reew yu mag yi loolu nag waraloon na neew dooleg kureelu xeet yi rawati na ci atum g bi nga xame ne ag lottam àgg na ci manatul a tee reew yu mag yi di noggatu yu ndaw yi lu mel ni loolu moo xewoon bi japon defee ay jalgati jëme ko siin li ko gënoon a doyadil mooy genn gu ci japon ak almaañ gennoon atum g ak lott gu mu lottoon ci tee itaali songu ecopi atum g loolu sax moo taxoon mu genn ci kureel bi atum g kureel bi ba tay demoon na ba manatul woon a tee ay dank yu xare yu bees di am maanaam ay reew dajaloo boole seen bopp ci wàlli xare kureel bi tam àggoon na ci manatuloon a tee reew yu mag yi di rewante ci ngànnaayu yi ci bokk ci kureel bi ak yi ci genn bokk na ci ayibi kureel bi fent gu ñeenti reew yu mag yi fentoon nosteg feetate ngir may britani ak frans nu man a sancati walla koloniiseeti ay suuf yu bees yoo xam ne danoo juboo woon ci seddoo leen ci seen biir rawati na ci reewi araab yi ak yu dul ñoom yenn yi ci yooyu danoo nekkoon ci ron kilifteefug reewum usmaan mi yi ci des ci waawug imbraatoorub almaañ bi reew yu mag yii dano o jëloon seen xemmemteefi sancaan yooyu cuub leen ci cuubug ag nite ak bëgg a def lu baax bi nu waxee ne kureelub xeet yi daal mooy kilifa gu njëkk gi yilif reew yu neew doole yi muccoon ci kilifteefug tirki ak almaañ bokk na ci ayibi kureel bi ba tay aakimoo gi reew yu mag yi aakimoo woon mbooleem saxal yi ak mbir yi nu daa gaaral ci kureel bi mbootaayu xeet yi walla xeet yu bennoo yi ndawi reew yu mag yi yu ci mel ni britani diiwaan yu bennoo yi amerig bennog sofyet frans ak siin danoo daje woon ci wasington peeyub amerig ci wenn waxtaan atum g ginaaw bi as lëf ci ndam tàmblee feeñ ñeel reewi tapoo yi ci noonu nu gëstu woon nan lanu fiy sose ag mbootaay gu adduna guy yëngu ci saxal ponki jàmm ci adduna bi jële fi xeex yi amal fi maandute ak yamoo ci diggante mbooleem reew yi ak rafetal nekkiinu mboolaayu reew yi ci koom koom mboolaay aada ak wér bi loolu jàllee nu def benn dajeb waxtaan bu adduna bi ci dëkku san fransisko ci awril atum ngir rëdd fa ag kollëre ñeel ag mbootaayug xeet gu yees gu fiy wuutu kureelu xeet yi ndawi lu tollook juroom fukk ak benni reew teewe nanu ko nangu it ci nu def kollëreg mbootaayu xeet yi ak xaatim ko ci g la jiitu ca kollëre ga mooy jubluwaayi mbootaayu xeet yi ak ay ker keraanam kollëreg mbootaayu xeet yi dafa saxal ay jubluwaayam ci ñeenti mbir yu dàttu ñooy 	wattu jàmm ak kaaraangey adduna bi 	suuxat seqooy cofeel yi ci diggante reew yi 	gën a soññ dimblante gi am ci diggante reew yi ci mbiri koom koom ak mboolaay ak aada ak wàllug nit 	dëppale jëfi xeet yi walla reew yi walla jëmale leen ci lu dëppoo ak li mbootaayu xeet yi bëgg bu dee ker keraan yi mbootaay giy jëfandikoo ngir àgg ci jubluwaay yooyu moom mbootaay gi leerale na leen ci nii 	bennoog askan yu moom seen bopp yi ngir ñoal jàmm ak kaaraangey adduna bi 	di jëf ci anamug jàmm ak baalante ak jéllale ci diggante reew yi 	warlu yoon yi man a yobboo ci nu bàyyi jëfandikoo doole ci bu nuy lijanti jafe jafe yi ci adduna bi ndare bu loolu day li gën ci adduna bi 	sukkandiku ci campeefi adduna yi ngir dëgëral jëm kanamug koom koom ak gu mboolaay gu askan yi campeefi mbootayu xeet yi aki jumtukaayam mbootaayu xeet yi mi ngi ame ci ñatti campeef yu mag ñooy jataay bu matale bi mi ngi sosoo ci mbooleem reew yi bokk ci mbootaay gi mu ci nekk it am na genn kàddu bu niy woote jataay bi da na daje benn yoon ci at mi ci weeru satumbar ca dalam ba ca new york man na a am nag leeg leeg ñu amal jataay bi ci xew xew yu bette yi ko aajowoo jataay bu matale bi nag yii ñooy ay yiteem 	gëstu naal yi ko reew yi ci bokk di faral a indil ak saxal leen ak def ndinkaane yi war ngir jàmmi adduna bi 	gëstu mbir yi nga xam ne man nanoo yokk anami dimblante ci adduna bi 	nangu bokkug reew yu bees yi bëgg a bokk 	tànn cer yu saxul yi ci jataayub kaaraange gi 	tànn àttekati àttekaayu maanduteg adduna bi ak ceri ñaari jataay yi bu koom koom bi ak bu mboolaay gi ak jataayub ndenkaane bi saxal yi jataay bu matale bi daa faral di jël ñi ngi daa ame ci ndollant gu toll ci ñaari ñatteeli cer yu fekke woote bu nuy def ci naal bu mu man a doon walla ab ndenkaane jaataayu kaaraange gi jataayub kaarange gi mi ngi sosoo ci juroomi cer yu sax ñooy ndawi diiwaani amerig yu bennoo yi usa ak bennog sofyet gi ak nguur gu bennoo gi ak frans ak siin ak yeneen fukki cer yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn ngir diirub ñaari at cer yu sax yi nag dananu am sañ sañu firi lepp lu nu fas ca jataay ba boobu sañ sañ ñu koy woowe veto jataay bi nag dana daje ci anam gu sax ngir xool ci mbir ak xuloo yu adduna bi yi nga xam ne man nanoo jur njombe saxal yu jataay bi ñi ngi ame ci ndollant gu toll ci juroom ñeenti kàddu ci cosaanul fukki kàddu ak juroom maanaam saxal gi du man a wér mbaa mu wéy ndare bu juroom ñeent danoo kàddoo waaw la ca des ne deet walla ñu noppi waaye nag benn saxal du am njariñ bu ko benn cer bu sax firee ne àndu ci jataayub kaaraange gi moo ame kureel biy saytu kàttanug fepp gi am na it sañ sañ ci genne ay saxal yu aju ci taxawal xeex yiy am ci diggante ñaari reew ak tege ay mbugali koom koom ak yu xare ci mbooleem reew yi dul dégg ndigalam am na sañ sañu yabal ay doole it ngir taxawal ab xeex walla ay kureeli soldaar ngir ñu dox diggante ñaari reew yu nar a xeex koolute gu matale gi moom jumtukaay la bu moo uuf mbooleem ñiy ligeeye ci mbootaayu xeet yi koolute gi ki koy jiite mooy ku nu woolu kiy jiite mbootaay gi nga xam ne jataayub kaaraange gi moo koy tànnlu bu ko defee ñu gaaral mbir mi ci jataay bu matale bi ngir nu woote ko kàddu ko dalub koolute gi mi ngi new york ci biir koolute googu lanuy denc mbooleem dosyeey mbootaay gi campeef ak bànqaasi mbootaayu xeet yi am na ay campeef aki bànqaas yu aju ci mbootaay gi ñooy jataayub koom koom ak mboolaay bii jataay a ngi ame ci cer yu seen xam xam aju ci mbirum koom koom ak mboolaay jataay bu matale bi moo leen di fal ngir diirub ñatti at jataay bii nag li nu ko wékk mooy gëstu mbiri koom koom yi ak mboolaay yi ak aada ak lu aju ci nit mbootaayi adduna yii ma lay bëgg a leeral ci jataay bii lanu bànqaasoo moom mbootaay guy jagoo mbiri aada yi la ak xam xam ak yar dalam bu sax ma nga paris ca frans yiteem nag mooy dëgëral dimbalante ci wàllug xam xam ak aada ak yar ci diiggante reew yi ci bokk jaare ko ci soññ ak sawarloo gëstu ak ligeey yi aju ci yar ak aada ak xam xam yi mbootaayu ligeeyu adduna bi li nekk yiteem mooy rafetal dundiinu ligeeykat yi ci adduna bi ak fexe nu yokk seeni ngérte moom nag mbootaay gi mi ngi ame ci ab lim ci ndawi ligeeykat yi ak boroom ligeey yi ci mboooleem reewi adduna bi ab dalam nag mi ngi nekk geneve mbootaayug wérug adduna bi mbootaay la guy sonn ci dimbali reew yiy màgg ci ñu man a xeex tawat yiy wàlle te yekkati seen tottuwaayu wér gu yaram moom mbootaay gi nag dana def ay gëstu ci wàllug wér di ci sàkku it xam xam yi manul a ñàkk di yonni ay boroom xam xam ci loolu di nos ay prograam yu jagoo tàggat ñi yittewoo wallug wér ab dalam nag ma nga geneve moom itam mbootaayu dund ak mbay gu adduna bi moom nag liy ligeeyam mooy jeem a def ay pexe ci nu niy yokke li nuy ligeey cib dund ci ñatteelu adduna bi loolu nag nu jaare ko ci jëme kanam mbay mi te yokk jumtukaayam aki ker keraanam ak xeex gàkk gàkki mbay yi ak yu dundat yi ak dox ci lu fi man a indi ag mottalikoonte gu dund ci adduna bi dalam bu sax bi nag mi ngi rom ca itaali ëttu àtte bu maandute gu kawe gi moom nag daa mel ne àttekaayu maandute gu adduna bi gi toppoon ci kureelu xeet yi moom daal moom lanuy jàppe kilifa gu wàllug yoon gu mag gi nekk ci mbootaayu xeet yi mi ngi ame nag ci fukk ak juroomi àttekat yu jataay bu matale bi di tànn ak jataayub kaaraange gi ginaaw bu leen seeni reew sampee gaaral leen ci mbootaay gi ligeeyam nag mooy gëstu sabab yi waral xuloo yi ci diggante reew yi mooy kàttan gi ame firi ak leeral kollërante yi reew yiy def ci seen diggante ak àttey yoonu adduna bi ab dalam nag mi ngi lahaay ca holand mbootaayu xeet giy yëngu ci xettali gi ak tabax li miy yittewoo mooy mbiri way daw làqu yi te indil leen ndimbal li manul a ñàkk te dëkkal leen ligeeyloo leen jataayub ndénkaan yi mooy saytu mbirum sancu yi almaañ moomoon itaali ak japon njëkk ñu leen di gañe ci xeexu adduna bu ñaareel bi bii jataay nag moo taxaw taxawaayu jataayu feetale bi nekkoon ci kureelu xeet yi ginaaw xeexu adduna bu njëkk bi bankub addunna bi ngir sos ak tabax bii bank danu koo sosoon ngir man a lebal reew yi ci bokk ak dimble leen ci tabax barab yi xeex bi yàq ak jëmale kanam barab yiy tàmblee màgg ak sos ay naal yoo xam ne man nanoo jàpplee ci màggug koom koomu adduna bi ak jeem a rafetal dundiinu ñi dëkke ci reew yiy màgg banku adduna bi moom dafa mel ni ag lonkoo gu adduna bi goo xam ne boppu alalam mi ngi juge ci li cer yi di teg cer bu nekk nag li muy teg day tolloo ak ni koom koomam toll dalam bu sax nag mi ngi wasington peeyub amerig keesug kee gu adduna bi yitteem mooy saxal njëgu kee gu adduna bi ak dindi fi jafe jafe yi man a juddoo ci wecciku ci diggante reew yi man nanu ne mbootaayu xeet yi daal mbootaal la gu adduna gu am sañ sañ yi kureelu xeet yi amoon waaye mu ëpple kureelu xeet yi ci ñatti mbir yu am solo ñooy 	mbootaayu xeet yi day dëgëral ci ay jubluwaayam àqi ak yelleefi doomu aadama yu dàttu yi ak teddngay nit ak yamale ñaari xeet yi goor ak jigeen cig wàll ak yamale reew yi ci geneen wàll 	mbooleem reew yu mag yi bokk nanu ci mbootaayu xeet yi te bu dee kureelu xeet yi moom amerig bokku ci woon ngir bañ gu kongres bañoon ne du ci bokk te it bennoog sofiet moon bokku ci woon lu dul ci diggante g nga rax ci dolli ne cer yi bokk ci mbootaayug xeet yi boo ñaarte woo cer yi bokkoon ci kureelu xeet yi yu mbootaay gi moo leen di ëpp 	mbootaayu xeet yi am na dooley xare ju koy kàttanal ci mu man a wéyal ay saxalam am na it sañ sañu tege ay dogoo yu koom koom ak jëfandikoo doole jëme reew yiy tooñ ànd ak loolu lepp nag teewul mbootaayu xeet yi moom doon daanaka ab jumtukaay bu nekk ci loxoy reew yu mag yi am ay toogu yu sax ci jataayub kaaraange gi yooyu nga xam ne ñoo ame sañ sañu firi veto man a bañ mbaa firi bepp naal boo xam ne gaaral nanu ko ci jataayub kaaraange gi ci noonu yenn ci reew yu mag yi ftteerlu nanu wéy ci jëfandikoo sañ sañu firi di ko jëfandikoo fu nu ko wart a defe di ci tooñe di ci dumaa di ci aare reew yuy jalgati te lu bari ci saxali jataay bu matale bi ak saxali jataayub kaaraange gi ba leegi daa rekk lanu ci kayit kenn doxalu leen ab ligeeyam nag ci wàllug dimbalnteg koom koom aada wér gu yaram ak mboolaay lu am solo la te yayoo màggal waaye bu dee ci lu aju ci politig ak xare moom dëgg dëgg ni mu ciy doxe sori na dëgg sori maandute te sori yoon mbootaayu reewi jullit yi walla mbootaayu daje gu lislaam gi ag sosam mbootaay gii mi ngi sosu ci saxal goo xam ne buur ak njiiti reewi jullit yi jëloon nanu ko ci waxtaanu seen daje bi nu njëkk a daje te defe woon ko ribaat peeyub reewum marok ci diggante g g deppoo ak g ñaar fukki reewi lislaam ak juroom bokkoon nanu ca waxtaan woowa mbootaayug goreel falastin olp it teewe woon na ko waaye niki aji fuglu rekk ndajem waxtaan moomu mi ngi amoon ci ginaaw bi nu lakkee masjidul aqsaa ci g te ay yahuud def ko waxtaan wa ba muy tëj daa ñaawlu jëf ju bon jooju nga xam ne day wone ag noonu gu nu def jullit ñi te ñàkk a wormaal seeni gëm gëm ñu sàkku woon it ci israayil mu genn ci mbooleem suufi araab yi mu tegoon loxo atum g te delloosi dëkkub quds bi ci ni mu nekke woon ca xareb sue juin ba atum g mu feddali ba tay moom ndaje mi jàpple gu miy jàpple reewi artaab yi ci seen xeex bi nuy def ak israayil ak jàpple gi muy jàpple waa palastin ci nu delloosi seen àq ak yelleef yi nu teg loxo te goreel seeni suuf kollëreg mbootaayu reewi jullit yi kollëreg mbootaay gi mi ngi genne ca ñatteelu waxtaan wa jëwrini bitim reew yu reewi lislaam yi amaloon ca jidda atum gg dëppook g mu sampu woon moom kollëre gi ci li taxoon nu sos mbootaay gi li nekk ci poñ bu njëkk bi ci kollëre gi mooy reew yi ci bokk ñi ngi sos mbootaayug reewi jullit ñi walla mbootaayug daje gu lislaam gi poñ bu ñaareel bi làmboo dali mbootaay gi aki jubluwaayam jubluwaay yooyu nag weesuwunu woon amal fi jawwu ju baax ju nu man a dëgërale dimblante ak deggoo ci diggante reew yi ci bokk ci seen biir ak ci seen diggante ak yeneen reew yi waaye dal yi nag ñoom ci nii lanu taxawe 	yamoo gu mat ci diggante reew yi ci bokk 	wormaal àq ak sañ sañu reew mu ci bokk ci wutal boppam mujj ga ko soob ak bañ a dugg ci mbiri biiram 	wormaal moomeelug reew yi bokk ak seenug temb 	dëgëral dalu dimblante gu lislaam gi ci diggante reew yi bokk 	dëgëral dimblante ci diggante reew yi bokk ci wàlli koom koom mboolaay aada xam xam ak ci yeneen wàll yu am solo yi ak diisoo ak yeneen reew yi bokk ci yeneen mbootaay yi 	jeem a far boddante ci biiru xeet ak sanc ci mbooleem ay anamam 	def lepp lu man a indi jàmm ak kaaraange ci adduna bi ci anamug maandute 	dëppale ak nos ligeey bi reew yi seq ngir njoal barab yu sell yi te goreel leen ak jàple waa falastin ci seen xeex bi ak dimble leen ba nu man a delloosi seen àq ak yelleef te jotaat seen suuf 	jàpple mbooleem reewi jullit yiy xeex ngir njoal seen teddnga jot seen tmbte dollosi seeni yelleefi reew 	lijjanti xuloo yi nar a ami ci diggante reew yi bokk ci mbootaay gi lijjanti loolu ci jàmm niki waxtaan dox diggante ak layoo 	reew yi ci bokk danoo war a bàyyi ci seeni seqoo di jëfandikoo doole walla xuppe ci jëfandikoo ko jëme ko ci suufus reew mu bokk walla jëme ko ag tmbam campeefi mbootaay gi aki kureelam ak jumtukaay yi ci bànqaasoo mbootaay gi sos na ay campeef yu bari yu cosaanu niki 	jataayu buur yi ak njiit yi 	jataayu jëwrini bitim reew yi 	koolute gu matale gi 	àttekaayu maandute bu lislaam bu adduna bi bu dee kureel yi ci bokk nag ñooy 	kureelu quds 	kureel bu sax bi ñeel wàllug koppar 	kureelu lislaam bi saytu wàllug koom mboolaay ak aada 	kureel bu sax bi ñeel dimbalanteg xam xam ak xarala 	kureel bu sax bi ñeel dimblanteg koom ak yaxantu 	kureel bu sax biy yëngu ci wàllug xamale ak aada bu dee nag lu aju ci jumtukaay yeneen yi bànqaasoo ci mbootaay gi ñooy 	keesug dimblante gu lislaam gi 	keesug quds 	daaray gëstu gu lim yi ak koom ak mboolaay 	barabu lislaam biy yëngu ci jàngale mecce ak xarala ak defi gëstu 	 cëslaayu lislaam giy saytu xam xam xarala ak suqli koom koom 	barabu adduna biy yëngu ci yar ak njàngalem lislaam 	barabub lislaam biy sonn ci suqali yaxantu 	kureelu lislaam gi saytu terute gi ci adduna bi 	kureel adduna gi saytu ndono lu lislaam li 	akaademi bu xam xamu lislaam 	jataayu lislaam bi yor tukkib jawwu bu nit ñi 	kureelu lislaam bu adduna bi ñeel yoon bu lii jàllee teewul sosees na ba tay yeneen cëslaay yu bokk ci mbootaay gi ñooy 	banku lislaam bi 	barabu xibaar bu lislaam bu adduna bi 	mbootaayu rajoy reewi jullit yi 	neegub yaxantu bu lislaam bi ak mecce ak joqalanteg njaay yi 	mbootaayu peeyi lislaam yi 	suqali gu lislaam gi jëm ci boroom gaal yi 	mbootaayug lislaam gi jëm ci yar xam xam ak aada jagley campeef yi ak seeni ligeey jataayu buur yi ak njiit yi mooy campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi moom nag dana faral di daje saa su ko yitey xeet wi laajee ngir gëstu ay mbiram ak lijanti ay lëj lëjam buur yi ak njiit yi ci bokk nag saxaloon nanu ca seen ñatteelu ndaje ma nu defoon ca makka mu sell mi ak taayif ci diggante rabihul awal gg dëppook g saxaloon nanu fa ne danuy def ndaje yi ñuy luy wër ci seen diggante ci ñatti at yu nekk niki nu ko waxe woon mbootaay gi ndajeem mu njëkk mi ngi ame woon ribaat diggante gg dëppook g mu defaat meneen ndaje ca lahoor ca pakistaan diggante muharram safar gg dëppook g ñatteelu ndajeem mu defe ko makka ak taayif diggante gg dëppook g mu def ñeenteelu ndajeem ca kaasa balanka ci diggante rabiihu saani gg dëppook g juroomeelu ndajeem ame kuwet ci jumaadas saaniya gg dëppook g jataayu jëwrini bitim reew yi nag mooy ñaareelu campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi ginaaw jataayu buur yeek njiit yi campeef bii nag dana faral di daje ci anam guy wër ci at mu nekk ci benn ci reew yi bokk ngir xool mbooleen bataaxel yiy doxal politigu mbootaay gi ak jël saxal yi war ci mbir yi am ay njariñ yu reewi mbootaay gi bokk loolu lepp nag fekk mu dëppoo ak jubluwaayi mbootaay gi aki bëgg bëggam jataayub jëwrin yi mooy xool saxal gi nga xam ne kureelub koppar bu sax bi di na koy def ngir saxal ko te wéyal ko mooy xool it njël lu yaatu lu kooluteg mbootaay gi bokk na ci ay ligeeyam di sàkku ci mbootaay gi muy daje bu jaadoo ngir ay xew xew yu bette yu yitteel jullit ñi jataayub jawrin yi ba tay dana faral a daje ci anam gu xotti baax saa su ko yitte laajee bu dee koolute gu matale gi nag walla moom mooy campeef biy wéyal jëf yi ci mbootaay gi mi m ngi sosoo ci saxal resolution gu genne woon ca ndajem jëwrini bitim reew ma nu amaloon ca jadda diggante g yiteem nag mooy def ligeey yi nu ko sant ci biir àttey kollëreg mbootaay gi dina dimbli tam yeneen campeef ak bànqaas yi bawoo ci mbootaay gi ak di dëppale seeni prograam yu wuute yi bokk na ci yitteem ba leegi topp ak xeeñtu saxal ak ndenkaane yi tukkee ci ñaari ndaje yii mu mbootaay gi ak mu jëwrin yi kiy saytu ligeeyi koolute gi mooy ku nu wóolu ki nga xam ne mbootaay gee koy fal ngir diirub ñeenti at yees manul a yeesal bu ko defee ñeenti dimblikat ak ñeenti ñu ñu wóolu di ko jàpple kenn ci ñoom jagoo mbirum palastin ak quds mbootaay gi jidda la defandi dalub kooluteem gi ba kero nuy goreel quds insallaa ngir nu def ko dal bu sax bi làkk yi mbootaay giy jëfandikoo ciy ligeeyam ñooy araab franse angle mbootaay gi nag mbirum palastin yitteel na ko lool ak mu quds moom mi nga xam ne moo uuf masjidul aqsa mi yàlla teral te teral li ko wër ak doj wu sell wa ak miir ba nuy wax miiru buraax ak yeneen mbir yi aju ci diiney lislaam te nekk ci mbooleem barabi lislaam yi quds nag boo gisee nu fonk ko day suuf si yonnant bi rañaane woon yeeg loolu nag dana waral ci jullit ñi ñu fonk ko te yittewoo ay mbiram te aar ko ba noon yi dunu ko tilimal kureelub quds mi ngi sosu ci ndigal lu tukkee ci juroom benneelu ndaje mu jëwrini bitim reew yi mi ame woon jidda ci diggante g ndajem jëwrin mu fukkeel ma nu defe woon faas ca marok ci diggante g ndaje moomu dal di denk njiitug kureelu quds bi buuru marok bii di asan mu ñaareel mi ligeey yi nu denk kureel bi mooy yii 	di gëstu lay xew quds 	di topp ak a xeeñtu doxalug saxal yi aju ci quds te jataayub jëwrin yi def leen 	di jokkoo ak mbootaayi adduna bi yi man a dimblee ci aar quds 	di wax ci lu man a doxal saxal yi ci aju 	di indi ag saxal ci at mu nekk guy leeral ay ligeeyam aki jëfam ci jataayu jëwrin yi kureelu quds moom njiit la ko jiite moo ko man a dajeloo walla lu mbootaay gi kureel gi nag mi ngi ame ci ndawi reew yu bokk ci mbootaay gi yoo xam ne jataayu jëwrin yee leen di tànn ngir diirub ñatti at doggantal gu ñatteel gi reew yi def ay dank ak reew yi feetewul fenn ag jiital bokk na ci li gën a rëy ci li juddoo ci xeexu adduna bu ñaareel bi bokk na ci li ci gën a rëy feeñug walla juddug ay dank yu ay reew walla ay booloo yu ay reew ci wàllug politig walla xare ci noonu dankub bopp alal dal di feeñ nee amerig jiite ko mu uuf nag biritani frans ak lu bari ci reewi orobug sowwu gi mbooloo mii nag ñi ngi ko daa woowe dankub sowwu bi ak reewi adduna ju gore ji safaan nag walla wuute ak reewi bokkoo yi bu ko defee amerig moom jug di dimbli reewi dankub sowwu bi ci ngànaay ak xarala ak alal ngir dëgëral seen koom koom te may leen doole ba nu man a taxaw di tata ci kanamu reewi bokkoo yi tee leen a tas tee leen a wisaaroo naka noonu dankub bokoo bi moom itam sosu bennoog sofiet gi jiite ko mu uuf lu sakkan ci reewi bokkoo yi ci tugal gu bëj gànnaar gi ak gu digg gi ak reewi bokkoo yi nekk asi niki kore gu bëj gànnaar gi wietnaamm gu bëj gànnaar gi ak siinug askan gi ñaari dank yii di bu sowwu bi ak bu penku bi xeex nanu ba tàyyi ngir yilif adduna bii nga xam ne sonne na lool ci ñaareelu xeexu adduna bi nga xam ne reewi orob yi sax mujj nanu di reew yu lòtt te neew doole ci kanamu ñaari reew yu mag yii di diwaani amerig yu bennoo yi ak bennoog sofiet gi looloo waraloon gisiin wiy woote ne reew yi ñoo tolloo yamoo ay nawle lanu wii gisiin naaxsaayoon te faf far xajal fi wiy indi doonadi moroom gi amerig ak sofiet doonadi woon moroom ci yeneen reew yi loolu nag taxoon na ba reewi orob yi tàmbli woon a xalaat ci seen ëlëg ginaaw bi nu mujjee di reew yu ñàkk solo bu nu leen tollalee ak yile ñaari reew ginaaw ñaareelu xeex bi it yeneen reew feeñ nanu ñu leen di woowe reew yiy màgg yi ci ëpp nag ñooy reewi asi ak afrig yi doon door a tembe ci reewi sancaan yu orob yi reew yooyu tam danku nanu ngir taxawal dankub reew yi feetewul fenn ne li niy def mooy fas yeenee ame ag peeteedi gu rafet ci diggante ñaari reew yu mag yi ak yi nekk ci seeni ngunu dananu leen leeral ci lii di ñëw lenn ci danki adduna yi bu ci mel ni tapoo gu càmmooñug atlas otan njiilul amerig lii di harry truman g dafa nekkoon ku bañoon lool mbokkte walla cominisme te bañoon it mu tas looloo taxoon mu taxawaloon ci atum g ag tapoo walla alliance gu boole woon amerig itaali holand beljik norwej danmark fraans kanada portigaal ak island ñu tudde woon nag tapoo gii tapoo gu càmmooñu atlas ginaaw bi la ci turki bokksi ak gres atum g ak almaañ gu federaal gi atum g seenug kollëre it ci ñatti wàll yii la jëm 	kepp ku laal benn ci reewi tapoo gi laal nga yi ci des 	reew yi ci bokk dananu dimblante ci seen biir ci wàllu aaru alal ak koom 	tapoo gi dana taxawal ab jataay bu xare te da na am njiit lu matale tam jaadu na nu leeral ne amerig mooy dàttub tapoo gii maanaam mooy reew mi ci ëpp solo ci wàllug li nuy joxe ak ngànnaay paris it moo nekkandi woon ab dalam ba ci mujj gi nu tuxal ko ca buruxel peeyub beljik bokkoon na ci li ko taxoon a jug neexal dundug ay askanam yombal seenu nekkiin dëppale ko ak sarti demokraasi goreg jëmm ak yoon tapoo gu warsaw bennog sofiet ñoom itam taxawal nanu ag tapoo gu kaaraange atum g loolu nag booy seet ag won amerig rekk la ne nun itam toogunu boo sosee tapoo gu atlas nu sos sunu gos rawati na bi ci almaañ gu sowwu gi bokksee ci gu atlas gi atum g tapoo gu warsaw moom bennoog sofiet la woon reewi bokkoo yi nekk ci ngunoom maanaam yi ànd ak moom ci gànnaaru tugal ak diggam mell ni romani poloñ hongri cekoslowaki añs warsaw nag li ko taxoon a jug mooy aar bennoog sofiet gi ak reew yi ko topp ci mbooleem musiba mu man a bàyyikoo ci tapoo gu càmmooñu atlas gi dëkkub warsaw bii di peeyub poloñ moo mujjoon dib dalam li mu yoroon it ciy xarekat àggoon na ci xarekat ñu seddale leen ci diggante reew yi ci bokk tapoo gu kollëre gu diggu gi waa tapoo gu atlas amerig jiite ko danu ne woon daal fawwu nu jële fi bennoog sofiet tas tapoom gii di warsaw ci noonu ñu taxawal ag njiit gu jagoo mbirum penku bu diggu bi atum g ginaaw bi nu sos mbootaayug aar penku bu diggu bi atum ci atum g nu sos tapoo gu iraak turki ñu gën koo xame ci tapoo gu baxdaad tur woowu nag mujj na soppiku atum g mujj di tapoog kollëre gu diggu gi ginaaw bi ci iraan bokkee pakistaan britani ci wetu turki ak iraak ñu leen di fattali rekk ne iraak moom mujj na genn ci tapoo gii ci suwe atum g jataayub tugal bi waa tugal ya daa woote bennoog tugal ak tembug ay gis gisam aki saxalam taxawaloon nanu ca atum g jataayub tugal bi muy ag mbootaay gu koom koom gu politig loolu nag doonoon ab jeego bu njëkk rekk jëm ci reewum orob mu mag mu nu bëgg a taxawali bookoon na ci jataay boobu nag biritani frans itaali belgik holand luxamburg danmark norwej suwed ak irland nga rax ci dolli ay ndawi parlamaa yu reewi orobug sowwu gi ak turki dëkkub strasburg bu frans bi moo doonoon dal bi rewwi tugal ya ca ja bu nu bokk ba waa tugal yi ci ag kollare gu nu fase woon ca rom atum g taxawaloon nanu am mbooloo mu koom koom mu orob nu gënoon koo xame ci turu reewi tugal ya ca ja ba nu bokk ngir jële fi ag nduwaan ci diggante reew yi ci bokk te doxal fi yaxantu gu gore ci seen biir buruxel nag lanu defoon seenub dal bokkoon na ci frans britani itaali beljik almaañ gu sowwu gi luxamburg holand irland danmark ak yonan gres ja boobu nag li ko taxoon a jug mooy dimblanteg koom koom gu orob waaye mujj na rax ci gu politig gu yaatu ci seen biir mbootaayu dimblanteg koom koom ak suqali mbootaay gii amerig moo ko sosoon atum g muy mbootaay gu mel ni reewi tugal ya ca ja ba nu bokk ngir rekk man a dugg ci koom koomu tugal bi cig wàll ak ngir man a dëgëral ay seqooy koom koomam yi mu am ak reewi ja bi ci geneen wàll bokk na ci mbootaay gi nag reewi tapoo gu atlas gi ak siwis finland otris suwed ak yogoslawi mbootaayug reewi amerig yi mbootaay gii yàgg na a sosu ndax def na ko ci awril atum g waaye ag dëgg dëggi sosoom mi gi door atum g muy man nanu ne lu juddoo ci xalaatu njiitul amerig lii di woon monrow mi daa wax naan amerig daal ñaari amerig yi ñoo ko moom mbootaay gii nga xam ne diiwaan yu bennoo yu amerig yi ñoo ci bokkoon ak reewi amerig gu latin gi mujjoon na gën a yaatu gën a jëm kanam mujj di ëtt bu am solo ngir dëppale diggante reew yi ci bokk waxuma la nag njariñul koom koom lu mag li ci nekk waa mbootaay gii nag wasington lanu defoon seenub dal te amerig it amoon na kilifteef gu mag ci mbootaay gi kilifteef googu feeñ na bu baax bi amerig tggee kuba ne bokkatul ci mbootaay gi loolu nag mi ngi amoon ci ginaaw bi fi ag fipp gu bokkoo amee ca atum g mbootaayi reewi andis yi moom nag mbootaay gu jagoo yenn ci reewi amerig gu latin gi la li ko tax a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom koom ak aada ñi ci bokk nag di kolombi peru ekuwador cili ak boliwi naalub marsaal bi ak komikon bennoog sofiet daa taxawaloon ag mbootaayug koom koom atum g ngir fayyoo ci ci li tugal def ci wetam muy mbootaayug ja bi nga xam ne amerig moo ko digaloon waa orob yi ne leen woon nanu taxaw ci tabaxaat seen koom koom bu daanu bii nga xam ne xareb adduna bee ko màbboon te moom dana leen ci jàpple wooteg amerig googu ñi ngi ko gënoon a miine ci turu naalub marsaal marsaal nag jawrini amerig ji yoroon wàllu bitim reew la woon ci ginaaw ñaareelu xareb adduna bi sofiet yi nag ñoom seen mbootaayu koom koom ñi ngi ko tudde woon komikon bennoog sofiet jiite woon ko mbooleem reew yi àndoon ak moom bokkoon ci li ko taxoon a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom koom mbootaay gi boole reewi araab yi reewi araab yee ko sos ci atum g ngir dimblanteg politig gu koom koom ak gu aada ci seen biir mbootaayug jàpplante gu asi reewi asi yee ko sos ak yu afrig yi ngir dëgëral diggante reew yi ci bokk mbootaayug bennoog afrig moom mbootay la gu reewi afrig yi ñu sos ko atum g li ko tax a jug di dëgëral buumi dimblante ci diggante reew yi ci bokk rawtina ci wàlli poloitig koom koom ak aada reew yi féetewul fenn reww yu bari temb nanu ginaaw ñaareelu xareb adduna bi rawati na ci goxu afrig ak asi ñu daal di dem nag bokki ci mbootaayu xeet yi reew yooyu di door a am ag temb soxla woon nanu di diisoo ci seen biir te di daje ndax kat ragaloon nanu bu baax reewi sancaan yi ak seeni pexe cig wàll ak ngir ne ginaaw bi nu tembee ba noppi danoo fees dell aki coonay koom koom ak yu politig ci geneen wàll ci nooonu am mbooloo sosu mu nu xame woon ci turu mbooloom reewi asi yi ak afrig ab xalaat dox ci ñoom jañ leen ci ñu taxawal ndajem asi afrig ngir gëstu jafe jafey ñaari gox yi rawati na lu aju ci goreel ay askan seen ak tembal leen teggil leen sukkub sanc bii tegu ci seenug dòq ak ci anam gu mu ci teggoo ci noonu nu def ndajem bandonj ca awril g ca endonesi ndawi lu tollook reew teewe ko yu afrig ak asi ñooy end bakistaan endonesi borma silan mujj di sirilanka afganistaan iraan japon filipin taylan siin gu askan gi wietnaam gu bëj gànnaar gi wietnaam gu bëj saalum gi cambodie lawus nipal ecopi liberia tefesug wurus gana ginaaw bi siri isipt misra iraak nguurug araabi sawdid jordanie libi sudan liban ak yaman ndajem bandonj nag mooy ndajem adduna mi njëkk a boole ndawi ay reewi asi ak yu afrig yu temb ay ndénkaane aki saxal yu bari juddoo nanu ca ndaje ma yuy soññee ci nu yamale diggante xeet yi ak waaso yi te wormaal àqu ak yelleefu doomu aadama ju cosaanu ji ak sañ sañu nit ci wutal boppam mujj gi ko neex moom ndaje mi tam woo na reewi afrig yi ak asi ci nu dimblante ci kom koom ci seen biir te diisoo ci politig ndajem reew yi feetewul fenn nag juddoo na ca ndajem bandonj moomee nu njëkk koo amal ca keer atum g ma ca topp nu defe ko konaakri atum g bi adduna bi gënee bari ay coow xuloo yi gën a tar ci diggante reew yi jamaal abdu naasir mi nekkoon njiitul reewum isipt ak kii di tito nekkoon njiitul yugoslawi ñoom danoo woo woon reew yi feetewul fenn te nekk afrig asi ak amerig latin ne nanu def am ndaje mu mag ngir gëstu tolluwaay bii ak tàngoor wii ci adduna bi ci noonu nu daal di def ndajem belgraad ci sëtumbar g daal di genne ay saxal yu aju ci jàmmi adduna bi ak jafe jafe yi aju ci noccim ngànnaay mi ak jafe jafe bu aljeri bi ak bu kongo ak yeneen jafe jafe yu adduna yu bari yu amoon ca jamono ja nu defaat meneen ndaje ca keer mu reew yi feetewul fenn ci oktoobar g lu tollook ci ndawi reew teewe woon ko ab lim nag ciy saxal aki ndenkaane yu am solo genne na ca mooma ndaje nu tudd ci yii rekk 	wormaal sañ sañu askan yi ak seen àq ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg 	àndandoo ligeey ngir goreel reew yi tembagul 	sakku nu nocci ngànnaay yi te lijënti xuloo yi ci yoonu jàmm te jële fi tapoo yi tas leen dindi dàtti xare yi 	ligeey ngir suqali dimblanteg koom koom aada xam xam ak yar ci diggante reew yi ci bokk ñi ngi fattalee ne reew yi feetewul fenn dolliku nanu bi reew yi temb gënee dolliku xuloob reew yi gën a tàng rawante ci ngànnaayu gën a yokku ci ngànnaay yu nu xamoon yi ak yu gën a jëm kanam yi looloo waraloon reew yi feetewul fenn gën di dolli seeni daje yiy wër ak di gën di ligeey ngir adduna bi man a dégg seen baat te man cee def jeexiit bu baax ñeenteelu doggantal fipp gi xam xam amal ci elektron xamale lan mooy elektron elektron moom yaram wu sew la lool moom daal gën na a ndawe ay milyoi yoon yeneen yaram yi nga man a gise ci bët rekk bu nu rafleel moom sax manoo koo gise ci fésalukaay yu elktronik yu bees yi am leegi li ko waral mooy boo jëloon ay bilyoi elektron dajale leen du nu toll ne boppu puso elektron nag nekk na ci bepp ne ne bu yàlla sàkk moom nag mooy peek fepp wi walla saal bi moom nag foo ko fekk da koy wër ngir xëcc gi ko saal biy xëcc elektron ni muy wëre saal bi booy xool day mel ne ni bidiw yu mag yi di wëre jant bi elektron nag day yanu ay cëfkay kuran yuy bañ saal bi walla fepp wi di yor ay cëfkay kuran yuy wuyyu walla nangu xam xamu elektron ni mu sosoo xam nanu ne xam xamu kuran moom xam xam la bu nu xame bu yàgg ci ki nuy wax taalis di woon boroom xam xamu gres ay boroom xam xam yu bari nag ñëw gën koo jëme kanam bokk na ci ñooñu kii nuy wax wilyaam jilbert di boroom xam xamu angle boo xam ne mooy ki teqale dooley kuran ak dooley bijjaakon ci noonu la wuuteek kii di taalis mi ne woon ñoom ñaar daal benn lanu jilbert it xamoon na ne duusi kuran yi mooy jur dooley asye boroom xam xamu almaañ bii di anofon jiyorik moom itam di ki njëkk a genne masinu juddal kuran maanaam jumtukaay buy tax kuran bi di judd di am loolu di ci atum g tomas adison it ñëw indil ñu lamp bu kuran xam xamu kuran nag soppiku di xam xamu elektron ci njëlbeeni xarnub ñaarfukeel g loolu nag mi ngi amoon ginaaw bi boroom xam xamu fisiyaa bu angle bii di josef tomson jugee feeñal xam xamu elektron atum g daal di ciy ame neexalub nobel ci xam xamu fisiya li gën a jëmal kanam xam xamu elektron nag mooy feeñal gi boroom xam xam yi feeñal ne fepp saal biy wuyyu day xëcc jëme ci boppam lu bari ci elektron yiy bañ te moom fepp wi day seddaliku ci fepp yu bari ndamul xam xam lii ab jeego la bu am solo ci doxub xam xamu elektron jeego bii daal bu am solo la ci dundug nit ci kaw suuf jumtukaay yu elektronik yi ak seen njariñ jumtukaay yu elektronik yi mujj nanu ci jamono jii nu nekk di loo xam ne foo wëlbëtiku gis ko ci kër yi barabu ligeey yi dëkk yu mag yi yu ndaw yi mbay mi ak mecce yi añs kon daal jumtukaayi elektron yi dugal nanu seen loxo ci yombal dund gi nga gis nit ñi ñuy jëfandikoo raxasukaay yu kuran yu otomatik yi ak fompukaay yu kuran yu otomatik yi ak jumtukaayu seral yi yu wuute yi ak rajook tele yu melo yi ak jumtukaayu nataal yi añs boo demee ci ndoktoor it fekk ko mu fees dell ak jumtukaay yu elektron xoolal ma fesalukaay yu elektonik yiy feeñal jàngoro yi gën a tuuti ak nataalukaayu ndoktoor yi ak jumtukaayu segg yu elktronik yi jumtukaay yii dey tax nanu doktoor man a xam lu jot nit man koo faj te looloo tax ndoktoor jëm kanam ci sunu jamono jii gis nga leegi foo dem fekk fa komputer ci bank yi lonkoo yi campeefi goornamaa yi ak ligeewukaay yi gis nga xam xamu fuglug jawwu ji ni mu nosoo leegi ak xam kiliman bi te loolu lepp elektron a ko waral leegi man nanoo xam nu tooyaay bi toll nu jawwu ji selle nu gelaw li gaawe nu tàngoor wi tànge nu niir yi kawee añs te loolu lepp elktron a ko def waa xam xamu suuf jiyoloji jariñu nanu ci jumtukaayi elktronik yi leen di xamal ati doj yi ak ati suuf si te di leen won fi am petrol yoraniyom ak yeneen mblli suuf yu am yi solo jumtukaayi elektronik yi dimblee nanu ci wàlli ngànnaay ak xare ak aaru leegi gis nga jumu fepp rajo jumtukaay yi amul buum ak yiy yonnee tey nangu ak yiy nataal añs lii nag wone na ne xam xamu elektron aki jumtukaayam yi ci aju ci jàmm ak yi ci aju ci xare def nanu fi ag jeqiku gu xam xam gu am solo ci xarnub ñaar fukk g bii nit nag jot na a man a tàggat xam xam bii def ci li mu ci bëgg ci lu aju ci jàmm waaye it mi ngi koy jëfandikoo ci xare yiy màbb tey mbugale di alag mbidéef yi juroomeelu doggantal xareb jawwu ji yaa mahsharal jinni wal insi inistatahtum an tanfuzuu min axtaaris samaawaati wal ardi fanfuzuu laa tanfuzuu illaa bisultaanin sooratu rahmaan aaya di yeen jinne yeek nit ñi su ngeen manee dem ba soobu ci goxi asamaan yi ak suuf def leen ko waaye fu ngeen fi àgg rekk na leen woor ne yàlla a leen may ngeen àgg fa fu ngeen fi àgg rekk ci sultaan ngeen fa àgge sultaan nag mooy lay ndigal kàttan nguur di kon fu ngeen fa àgg sunu boroom a leen fa àggale moom mi leen may xel may leen kàttan ubbil leen bunti yooyule gox man a layal lu tax ngeen àgg fa nit nag yàgg naa xëntewoo xam li ko wër ciy mbir yàgg naa yittewoo xam mbóoti jawwu ju biti jii nga xam ne daa fees dell aki nekkteef yu asamaan ay bidiw aki ñoom seen moom de jot naa àgg ci xam bidiw yi ak seeni kem ak seeni bind ak li leen sos def it ab jeego bu rëy ci xam xamu juxraaf ak yeneen xam xam yi am ag jokkoo ak kaw suuf biir suuf ak li wër suuf peek ko ciy mbindeefi asamaan bidiw ak lu ko moy ci ati juroom fukk yi ci ñaar fukkeelu xarnu bii gis nanu nit mu jeem ay yoon nu mu yeege ci jawwu ji ngir làmb ko te xam la fa nekk loolu nag faalewu ci jafe jafe yi mu ci man a dajeel ak ay wu rëy wi loolu làmbool bokk na ci ay woowu man cee ñàkke bakkanam ñàkk a wóor gi ci bu nuy joy bu masin biy wëndéelu ak buy wàcci li sofiet yi def ci xareb jawwu ji sofiet yi de njëkk nanoo nattu jawwu ji làmbtu ko loolu nu jaare woon ko ci jëfandikoo ay bayyima ngir ragal nit di ci loroo sofiet yi ñi ngi njëkk a joyal seen gaalug jawwu gi tuddoon fostok ñaari soobukati jawwu yu sofiet nekkoon ci biir di yori jajarin ak alaan shabard ci subag bisub awril g loolu nag bettoon na adduna bépp tukkib jawwu bii nag yobbu woon na lu tollook teemeer ak juroom ñatt fukki simili ci biir diir boobu gaalug jawwu gi wër na ci suuf si benn yoon ak xaaj tukkib xam xam bu jawwu bii xew xew la bu am solo ci taarixu nit ci jamono ju yees jii ndax kat moom ubbi na fi ay gox yu yees yu yaatu ci wàllug xam xamu jawwu sofiet yi wéyoon nanu ci seen ligeeyi jawwu yooyu nga xam ne am na ci yu jàmm taxoon a jug ak yu xare taxoon a jugg seen satalit yi gënoon nanoo yokk seen cawarte rawati na ci lu aju ci xare ci diggante ati juroom ñaar fukk yi ak juroom ñatt fukk yi ci xarnu bii li ci waa amerig def waa amerig yi ci ati juroom fukk yi ci ñaar fukkeelu xarnu g def nanu ay jeem aki pexe yu am solo ci wàllug xareb jawwu ji seen cawarte ci wàll googu dolliku woon na ci ati juroom benn fukk yi ci xarnu bii ndaxte seen ligeey yu jawwu yi gënoon nanoo ràññiku te gën a fés ci diggante bii ndax ci la kërug jawwu gu amerig gi ñu koy wax nasa jot a joyal ay waruwaayi jawwu yoo xam ne ay jum ñoo leen di jañ jañax leen ñu naaw bu niy dellusi ci suuf si nekk ay fafalnaaw yu yor ñaari laaf ñu leen di man a jëfandikoowaat ay yooni yoon lii nag tax na ba li nu daa ñàkk ci tukkiy jawwu yi gën a neew te itam indi na ay ngérte yu am solo ci xareb jawwu ji waa amerig jot nanoo sànni waruwaayu jawwu wii di apolo ci sulye g ñaari soobukati jawwu nekkoon ca ñooy aarmustrong ak adwin drin aamustrong nee na amoon naa yëg yëg bu tumbrànke bi may dox ci kaw weer wi damaa yëgoon ne sama màndaxe daa woyofoon lool waa amerig yi sàmp nanu ci kaw weer wi ay jumtukaay yu xam xam yu bari jële nanu fa it ay còmp yu juge ca weer wa teg fa it ab juddalkaayu kuran bu saal kongres it dëppoo ci samwiye g ci prograamu jawwu bi nu tudde woon baaganteg jawwu ngir barig li nu daa dem ci jawwu jeek a dellusi tukki bu jawwu bu njëkk bi nuy wax kolombiya tàmbli na ci awril g yeneen tukki topp ci yu jawwu yu àntu waa amerig yi defati tukkiy jawwu yu carlinger bi ci njëkk di ci awril g juroom ñeenti tukki topp ci bi mujj di ci oktoobar g musibam carlinger am musiba xewoon na ci baagante gu jawwu gu amerig gii di carlinger loolu nag mooy bi waruwaay bi fàccee ci bisu talaata samwiye g lu tollook juroom ñaar faatu ci ñaar ñi di ay soxna njiitul amerig la nu daa wax ronaald rigan nee na woon bii bis de dana doon bisub naqar ak fàttaliku waa amerig yi it tudde woon nanu ko bis bu tiis bi musiba mii du mooy mi njëkk a dal amerig ci wàllug jawwu gi mu ni mel njëkkoon na ko fi ci lu tollook ay at loolu mooy bi sawara tàkkee ca joyaluwaayu waruwaay ba tudd apolo ci samwiye g ci noonu ñatti soobukati jawwu ya ca nekkoon yepp dee amerig defati yeneen tukkiy jawwu yu baagante tudde ko discovery bi ci njëkk mi ngi amoon ci ut g yeneen tukk yu àntu topp ca lii nu tudde xareb jawwu ji daal def na lu am solo ci wàllug xam xam rawati na lu aju ci mbiri jàmm yi ndaxte xam xamu fisiya gën a jëm kanam bu fuglug jawwu ak xam xamu nataalu jawwu biy nataal kaw suuf si te di ko natt xam xamu kart yi ak nataali jawwu yi gën na a jeego ay jeego naka noonu endustri elektronik ni nuy xame fi mbell yi nekk gën a xarañ ak ni nuy xeexe lakk yi añs sofiet yi ak waa amerig yi ku ci nekk soobu nga ci jawwu ji ngir ay xemmemteefi xare jawwu ji mujj di lef mu stratejig mu yaatu ñeel ay ligeeyi xare la nu ca jublu it di door ak jam ay barab yu nekk ci kaw suuf jaare ko ci seen satalit yi nekk ci jaww ji yi ci yanu ay boppi atomig cig wàll walla nu jaare ko ci ngànnaay yu wuute yi nu man a joyale ñu tukke ci jawwu ji ci geneen wàll xareb jawwu ji yamatul rekk ci diggante sofiet yi ak waa amerig yi leegi kay lu sakkan ciy reew bokksi nanu ci mu ci mel ni siin ak fraans am na yeneen reew yuy waaj ngir sànni seeni jumi jawwu walla satalit ci jawwu jii nga xam ne mujj na di barab bu yaatu ngir rawanteg xam xam ak gëpplante ci wàllug xare juroom benneelu doggantal ni japon jëme kanam japon njëkk fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g japon de wéyoon na diir bu yàgg di beru ak a sori xayug tugal gi yam ci yëfi bobbam doyloo aadaam ba ci digg juroom ñeenteelu xarnu g gii beru gu xay ak deltu ginaaw gu mag raxoon na ci ci wàllug koom koom rawati na endustri waaye nag lii mu nekke woon soppiku woon na ci ñaareelu xaajub fukk ak juroom ñeenteelu xarnu ci noonu mu tàmblee juge nànk nànk ci reew mu deltu ginaaw dem ci reew mu jëm kanam ci wàll yii koom koom aada politig ak xare mu roye nag ci reewi tugal yi gisiinu sanc ak yaatal ko ci reew yi mu dendal ngir wone ci dooley addinaam ji mu yor ci wàllug xeex gi nuy def ngir teg loxo ay reew sanc leen japon nag ak li muy yeex a jot ci xayug tugal gi lepp boo ko dee xool ci reewi asi yeneen yi ndax dëppoo gi mu njëkk a def ak amerig ci wàllug joqalanteg yaxantu weesuwul atum g gii rekk teewul mu tàmbli woon na jege nànk nànk xayug orob gi di ci jariñu di ci niitu loolu jural ko mu tabax ay isin yu mag xotti ay yoon defar ay yooni saxaar gën a jëmale kanam ni nuy yaxantoo reewum japon ca saa sa mu tàmblee gis ag yëngu yëngug endustri gu mag gu nirook ga tugal romboon ba mu ciy door a dugg bu ko defee japon xëy di reew mu dox mu jëm kanam raw nag ay maasam ci reewi asi yi ci wàllu endustri xam xam ak xarala mu mujj am moom japon mbooloom gaal mu yaxantu tax a jug mu mag moo xam ne moo jël limub ñatteel ci adduna bi ci diggante ñaari xarey adduna yi marsandiisi japon yi nga mujj foo dem fekk leen fa ci asi ak afrig japon ginaaw bi nu ko gañee ci ñaareelu xareb adduna bi japon gañe nanu ko ci ñaareelu xareb adduna bi te booba moo nekkoon laafum penku mi ñeel reewi digg yi axe ñooy almaañ itaali ak japon japon nag mujjoon na nangu ne gañe nanu ko mu jébbalu joxe loxoom ci kanamu njiitul xare lu amerig lii di mark arthur atum g ci noonu nu taxawal benn jataay bu way tapoo yi ngir doxal mbiri japon nu dénk ko kii di mark arthur ci diggante g waa amerig yi nag rëddaloon nanu japon benn strateji dugal fa demokraasi jële fa dal bi aju ci jaamu imbraatoor bi nu soppi woon it seeni njàngaliin maanaam ni nuy jànge ak li nuy jàng wutaloon leen sartu reew bu bees ray it lonkoo yu mag yi ñu fuqarci ay moomeel yu rëy ci loxoy njabooti japon yi sëddale leen ci lim bu mag ci baykat yi daal di it taxawal ab parlamaa bu bees ci noonu japon jot na a tàmblee nosaat dundug koom koomam gu plitigam ak gu mboolaayam te tàmblee dab nànk nànk reewi endustri yu jëm yi kanam waa japon jariñu nanu ci li leen amerig indil ci ndimbal yu alal ak yu xarala loolu bokk ci li delloosi cawarte gi ci wàllug koom lijjantikati japon yi dox nanu bu baax ci tas ak yaatal koom koomu japon ngir seenug yewwute ak ngir bari gu japon bari ay ligeeykat maamoor xam sa diine mooy moor mbàkke gànnaar maanaam doomi sëriñ jiili gànnaar di ku yëngoom jëm ci yar ak jàngale taalif na lu bari ci wolof firi ci it ay téere jële léen ci làkkuw araab yooya nag yu ci ëpp yu diine lañu woy na it lu sakkan ci wolof yii woy firndé lañu ci ku fonk wii làkk la looloo ko bijj ci def wile taalif sànki ci baat yu naroon a sànku mu jëfandikoo arafi abajada ngir toftale leen yal na ko yàlla gërëm moom nag day faral di def ay waxtaan ci diine ak làkku wolof ci rajo siwalukaay làmp fm dalal jamm yaa ngi ci wikipedia gi ñu jaglel kàllaama wolof muy ab terexamteef gu tinkiku goo xamne ñi koy jàng bokk nañ ci ñi koy bind ku nekk man nga cee dugal sa loxo bind ay jukki yu bees wala gënël baaxal li fi jota nekk ndaxte ngir mebet mii mana dox ci ni mu gënee dafa laaj ay loxo yu bari kumu manti doon man nga cee japp ci njekk ak teranga topp atte yi ñ fi tërël ñoo ngi lay dalal li mu doon lu ubbeeku ngir ñëpp te amul g pay ñi binduwul tamit ci biir moo tax wikipedia manula joxe ay wòoraange ci baaxaay ak celltey ndefam donte askan wu wikipedia moo ngi tijji ay gëtëm di ko jeema aar ci anam yu dëgër ci saa su ne man na am ay xët yu ñu say saye wala yuñu soppi ci anam yudul yi gën te tay ko def ci ay xibaar yu baaxul wala yu dëppowul ak dundinu sa waa gox man ngaa tambalee ci xët njëkk mi te topp lëkkalekaay yi lay yòbb ci li la solool li nga soba jàng su fekke itam daa am ab jukki booy seet man nga bind benn wala baat yu bari ci paxu bind gi gi nekk ci sa ndeyjoor te nga klig ci ayca du ñàkk mas ngéen a gis ay gaal yu mag ñuy tëmb ci kaw géej te kat ci weñ lañu leen liggéeye te weñ du feey loolu man nga cee xam dara soo jëlee ab pont mbaa lenn ci weñ tàbbal ko ci ndox kon am na jenn doole juy safaananteek diisaayu gaal yooyu te ñooy tax ba ñuy des ci kaw ndox mi di tëmb bu ngéen ci bëggee xamal seen bopp dara jëlléen loxo ngéen nuural ko ci mbalkam ndox bu ko defee ngéen yolomal séen loxo te xool dingéen gis ne am na jenn doole juy jañ loxo bi te di ko tëmbloowaat yii ak yeneen seetlu yu ni mel ñooy wone ci anam gu leer jikko ju daj ji nga xam ne nekkul rekk ci ndox waaye nekk na ci yeneen yolaakon yi ak gaas yi ñu duppee ko dalub archimde moom archimde nag benn boroom xam xam bu gres bu yàgg la tay de bis bu xiin la tàmbali naa taw doqi ndox yu ndaw yu xaw a rëy yu ngandee ngandee ngi nii far di rot ci suuf bu cooroonee gàncax gu bari seeni xob day ruus daal di naaw ci jawwu ji rotati ci suuf si jël leen aw xeer ci seen loxo wacc leen ko day rot ci suuf de benn sabab bi tax xeer woowu di rot tax it ba xob wi rot moo fi jaar ba tax doqi ndox yu taw yooyu di rot loolu mooy li nuy wax bijj gi walla dooley ñoddi gi suus si di amal ci yaram yi ñoddi gii mooy tax yaram yiy diis moo waral it ñuy aajowoo genn kattanug përëg ngir yékkatee léen ci suuf si ne ne ñu xame ko ci faraañse ci matire mooy li toggale li composer wépp yaram wu am ag nekk gu nu man a laal une réalité tangible ñatti melokaanam yi ñu gën a miin nag ñooy melokaan wu dëgër l état solide wuy yol l état liquide ak wu gaasu l état gazeux moom day jël barab elle occupe de l espace te kemub ne ne la quantité de matire ñi ngi koy natte ci jóor la masse bu fekkee ne mbir mi dafa aju ci waññ xaajiiti ne ne particules de matire deesi jëfandikoo mol la mole ci noonu ci xam xamu jëmm lepp lu am ab jóor rekk ne ne la ci biir loolu ne ne yu ñu miin yi ñu wër ñi ngi sosoo ci ay bariyon kon ci waxiin wi nu baaxoo boo ci déggee baatub ne ne nanga xam ne ne ne bu bariyon lañu jubloo wax tekkiin wii kon boolewuñu ciboson yu dàttu les bosons fondamentaux yi nga xam ne ñooy tuxal ñeenti doole yu dàttu yi ak doonte am nañu ab jóor ak walla genn kàttan wërlaay gi di ci tubaab environnemt mooy dénd bi maanaam nature bi ak li ci nekk ciy way dund ak yu dundul ci gàttal daal adduna bi nu wër ci kaw suuf si xam xamu wërlaay mooy biy jéem a indi ay tontu ci yenn laaj yi aju ci nan la dénd biy jëfe ak a jëflanteek way nekk yiy dund ak yeneen way nekk yi walla nan lay jëflanteek digg bi ko wër moo xam digg bu kimya la simi walla bu dénd nature digg bii moom lanuy tudde noste gu wërlaay looloo waral nuy gis noste gu wërlaay muy luy ame ci ay way nekk yuy dund ak yu dee walla yu way xam xamu wërlaay mooy jàng ak gëstu way nekk yiy dund ak séenug séqoo ak li leen wër ak jeexiital gi nuy def ci sunug séqoo ak suuf si nosteg wërlaay mooy mbooleem jëfka facteurs yu dundul ak mboolaay société yiy dund yu xeet yi nekk ci benn gox walla barab dénd bi day wëndéel mbir yi mu jëfandikoo woon ngir delloo leen ñu mujjaat di mbir yu am solo ak njariñ càllalag ñam ci kaw suuf si aw melo la ngir wone ni kàttanug ñam di dugge ci wërlaay gi foofu ñam da fiy juge ci aji nekk dem ci jeneen n gir jox kàttan dundat boobu di sàqami ñam wi ak a reesal gépp càllalag ñam nag ci jant bi lay tàmbalee dundat yi nit ci la munuñoo liggéey seenub dund looloo tax manul a ñàkk mu jot ci dundam boobu jële ko ci gàncax yi walla yeneen dundat yi looloo waral ñuy jàppe dundat yi ay way lakk walla ay way jëfandiku consomateur mujjantalu dundug dundat it mooy ag feccikoom ag tasam jaare ko ci ay mikrob walla ay gàncax ngir mujjati di suuf gàncax gi muucooti ko ngir liggééyati ci ñam wu beesati lii nag moom lanuy tudde càllalag ñam bokk na ci jëfkay dénd yi ci nosteg wërlaay gi te am ci jeexiitalm it leerug jant bi ak ker gi ak tàngoor wu diggdóomu wi ak séddalig sewogaraafi gi ak ngelaw li ak barab yu yékkatiku yeek yu suufe yi ak melokaanu suuf seek ndox mi bokk na ci jëfkay kimya yi yiy bàyyi ay jeexiital ci nosteg wërlaay gi tolluwaay niveau bu ndox yi ak ngelaw li walla jawwu ji ci suuf si ak kem ni way dundal yu gàncax yi di seeye ci suuf si ak ndox yi ak tooke yi ci nekk ak xoromus ndoxum géej ak oksijiin bi ci seey kay diang wolof ci baax wërlaay walla barabub jëf mbaa mbir maanaam fu lëf nekk mbaa deesi defe ko fa mi ngi ame ci jëmm yi substence peekte ti circonstance mbir yi walla nekkiin wi ko peek wër ko te di fa ame bu dee ci wàllug dundat biyoloji rawati na ci wàllug dénd ecoloji day tekki lépp lu man a def ay jeexiital yu jonjoo ci doxug walla màggug mbaa jëm kanamug mbir yi metabolosmo walla nekkiinu jëmm walla xeet wuy dund specie vivente loolu nag leer ci la ngelaw ndox suuf ak yeneen nekktéef yiy dund dalu archimde fr principe d archimde du ñàkk mas ngéen a gis ay gaal yu mag ñuy tëmb feey ci ki kaw géej te kat ci weñ lañu leen liggéeye te weñ du feey loolu man nga cee xam dara soo jëlee ab pont mbaa lenn ci weñ tàbbal ko ci ndox kon am na jenn doole juy safaananteek diisaayu gaal yooyu te ñooy tax ba ñuy des ci kaw ndox mi di tëmb bu ngéen ci bëggee xamal seen bopp dara jëlléen loxo ngéen nuural ko ci mbalkam ndox bu ko defee ngéen yolomal séen loxo te xool dingéen gis ne am na jenn doole juy jañ loxo bi te di ko tëmbloowaat yii ak yeneen seetlu yu ni mel ñooy wone ci anam gu leer jikko ju daj comportement général ji nga xam ne nekkul rekk ci ndox waaye nekk na ci yeneen yolaakon yi les liquides ak gaas yi ñu duppee ko dalub archimde moom archimde nag benn boroom xam xam bu gres bu yàgg la doolerandu mooy xam xam biy gëstu lepp lu ñeel wuutuloxo yi doxalkat ndaamar ci gattal lepp luy jur walla di yòbb ab jalaxu doole ag soppeeku da nuy wax tamit doolerandu gu daj doolerandug ndaamar taggat yaram gu doolerandu doolerandug gaal doolerandug asamaan doolerandub kàttan ferñent ci taariix doolerandu mooy boole gi newton def jëmm ak gëstubidiw kon su nu ko xoole ci wallu taariix jëmm walla fisiyaa ci doolerandu la joge ci sunu besu tay yi day lu noppale ci daara yu kawe yi ne atte doolerandu yi ci jëmm la ñu joge doolerandu ab banxaas la ci xam xam yiy gëstu jalaxu yi ak soppeekuy neen yi ci lu tukkee ci doole jiy man a indi googu jalaxu walla googu coppiku man nan koo xoolee ni ag wàll ci xam xamu jëmm kon aajoom mooy leeral xalaatjiitalu jalaxug neen yu tekkaaral yi ak yaram yu asamaan si walla jëmm yuy dund dun doolerandu ëbb na tamit kàttan mooy man a def dara sos ag soppi kàttan nag am na ay melo yu bari yi ci ëpp solo ñi ngi feeñe ci tàngoor ak leer ci biir xam xami dénd yi science naturelle kàttan man na fee jël ay melokaan yu wuute kàttanug tàngoor kàttanug kimyaa simi kàttanug mbëj kàttanug ceññeer kàttanug saal nucleaire ak ci mujjantal gi kàttanug mbëjbijjaakon éléctromagnétique añs xeeti kàttan yii ñaare dees leen di séddale ci kàttan guy yëngu ak kàttan gu nëbbu te kat am na yenn kàttan yoy dëppoowunook séddale gii lu ci mel ni leer gi ak yeneen yoy man nanoo nekk am njaxas mu tukkee ci ñaari kàttan yi guy yëngu gi ak gu nëbbu gi lu bari ci xeeti kàttan yii manees na koo soppi transformer jële ko ciw melo yóbbu ko ci weneen jaare ko ci jëfandikoo ay jumtukaay yu fasoodiku simple walla ay xarala yu fasu compliqué la ko dale ca kàttanug kimya ba ci gu mbëj jaare ko ci jumtukaay bu siiw bi di tegale pile yi walla ndëxañtéef yi albert ayinstaayin it ci biir faramfaceg ajoo theorie de relativisme boole na ñaari ëtt yii di bu ne ne ak kàttan nga xam ne kàttan day mujj man a soppiku di ne ne matiere naka noonu safaan bi maanaam neen soppiku moom it di kàttan wuññi découverte gu yees gii mi ngi ko xamalee ci yemalem gu siiw googee e mc soppiku gii ci jëf ci wàllug pratique ñi ngi ko firee ci man gi nu man a ame kàttan jaare ko ci xarug saal walla booleeg saal waxiin walla baatal terme yu kàttan yi akug soppikoom lu am njariñ la ci leeral jëfiini dénd yi ba sax feeñte phenomene yu kilim yi niki ngelaw taw melax ak riddi yi tornado dees leen di jàppe ñu juddoo ci soppiku yu kàttan gi juge ci jant bi wàcc ci suuf si dund gi ci jëmmi boppam dees koy jàppe muy benn ci njuréef resultat yu soppikuy kàttan yi ci anamu toggaleg leer gi dees na ci jële soppi kàttanug jant bi yóbbu ko ci kàttanug kimya ci biir gàncax yi bu ko defee ci kanam ñu man a jariñu ci kàttanug kimyaa gii nu denc ci ay liggéeyiinu wëlbati ci ay way nekk yuy dund ci biir jëfandiku gu mboolaay gu société bi baatub kàttan dees koy wooye lépp lu nekk ci ron gongikuwaayu kàttan source d energie juddalug kàttan lakkug kàttan ag jëfandikoom ak wattu rootuwaayu kàttan maanaam fi muy juge ginnaaw nag dooley koom koom dafa laaj te soxla ab rootuwaay walla ab gongikuwaay ci gongikuwaayi kàttan yi looloo tax ag amam akug yooxam baril ko bokk ci yitte yu mag yiy caabi ci at yu mujj yi jëfandikoo kàttan feeñ na di benn ci jëfka facteur yi gën a sabab nuggug àdduna bi global warming looloo ko def muy ab lëj lëj ci li ëpp ci réewi adduna bi manees naa soppi kàttan jële ko ciw melo yóbbu ko ci weneen ci misaal manees naa soppi kàttanug kimyaa gi ñu denc ci ab tegaleeb pile jiib def ko ag leer kem quantité bu kàttan bi nekk ci àdduna bi day lu sax ba fàwwu kàttan du jeex du sosu li am kay mooy day soppiku juge ci melo dem ci weneen bu melee ne kàttan dafa jeex booba jeexul daa soppiku kay dem ci weneen melo looloo tax ñuy gis ne kàttan mooy man gi neen man a def ab liggéey yëngu muy njuréeful yëngoom googu walla njuréeful ab barabam bu nu ko nattee ci doole yiy liggéey ci kawam kàttan giy ànd ak yëngu moom la nuy tudde kàttan gu yëngu kàttan nag gi am ag jokkoo ak barab bi moom la nuy wax kàttan gu nëbbu gu coona walla gu ñu dëxëñ gu nu denc kàttan dana ame ciy melokaan yu bari niki kàttanug doolerandu mecanique ak gu tàngoor ak gu dinaamig gu tàngoor tangdooleel termodinamique gu kimyaa gu mbëj gu ceññeer ak gu saal walla xartil kàttan yii yépp nag man nanoo def ag soppiku gu biir jaare ko ci ay yoon yu dëppoo ñam wi nuy lekk am na kàttan gu kimyaa gu yaram wiy denc te di ko génne bu nuy liggéey walla nuy génne ab coona def effort kàttanug bàyyima yi mooy gi nit njëkk a jëfandikoo ci fajarug xay bi xay civilisation di door a am loolu mooy bi mu jëlee bayyima yu miin yi di leen jëfandikoo ciy liggéeyam ginnaaw bi mu tàmbalee jëfandikoo dooley ngelaw li ci doxal ay loocaam ba ci ay gox yu sori ci géej gi lu xayam di gën a yokku muy gën a jëfandikoo kàttan gii mu jëfandikoo ko niki kàttanug doolerandu mekanig ngir doxal walukaayi ngelaw yi ak ngir dawal ponoy wuutuloxoy wal yi ak daggukaayu dénk yi ak najukaay yiy yékkatee ndox yi ci teen yi lii mooy li nu xame ci turu kàttanug doolerandu mekanig ci maanaa da nuy ràññee xeeti kàttan yu bari te wuute kàttan tamit day tax nu man a natt melow feeñte yi seenub taraay feeñte gu ne ak kàttan ga mu àndal xeeti kàttan yi nu yàgg a jàpp kàttanug imbiku cinétique kàttanug tàngoor calorifique kàttanug ëmbu potentielle kàttanug doolerandu kàttanug kimiya kàttanug saal kàttanug mbëj kàttanug mbëjbijjaakon kàttan gu féex libre koom koom walla cawarteg koom koom activité économique làkku grees wu yàgg wa yor ag kër walla saytu ko di kër ci ni ñu ko xame ak yor walla saytu administrer mooy cawarteg nit giy feeñ ci liggéey ak jóox produire ak séddale ak joqalante echange ak jëfandikoo njuddéef yi les produits njëfte yi le services koom koom nag ni ngi koy jànge ci xam xami koom koom yi day sukkandiku nag ci gisiin yu koom koom théories économiques dees na wax it ci koom koom niki tolluwaayu koom koom bu jamono bu am réew walla bu ab gox zone maanaam ag nekkam ci gëwéelub koom koom yi cawarteg koom koom gi kiliftéef yu koppar yi walla góornamaa yi àtte yi ñoo koy àtte jaare ko ci ab politig bu di kojug jamono conjoncturelle doxaliin wu mbooloo mi les administrations publiques day def moom itam ay politig yu koom koom ngir soppi doxiinu koom koom wu am réew benn ci joxoñ yu koom koom indicateurs économiques yu mag yi mooy njuddéef mu ñumm mu biirum réew nj ñ b produit intérieur brut pib loolu mooy maye nga man a nattale dooley koom koom yu réew yi xam xamu koom koom ci fr economie moom xam xamu mboolaay social la buy yëngu c gëstu ni ñuy jëfandikoo jumtukaayi jóox production yu daytalu yi am cig mboolaay société ngir faj soxlay ak xemmemtéefi cér membre yu mboolaay gii xam xam bii nag mook xam xam yépp a yam dafa am ay dëgg dëggam akaki àtteem waaye jeexiitalu gi mu def ci nekkiini mboolaay yi ak yu politig yi les conditions sociales et politiques ak ni ay séqoom ay relation oom dugganteek nekkiin yii tax na ba melow mboolaay muur ko cuub ko xam xam bii li mu làmboo mooy seggat jóox gi production séddale gi ak yaxantu ak lakk walla jëfandikoo njaay yi marsandiis yi ak njëfte yi les services danuy faral a wax ci koom koom ne buy wuyyu la positive bu dee jéem a leeral ngértey tànn yu wuuteyi di joxe ay mbooleem ay xalaat jiital hypotese walla am mbooloom ay gendiku ay seetlu danuy wax it ne bu nattukaay la bu dee leeral doxal yi nu war a def xam xamu koom koom dees koy déddale ci ñaari bànqaas yu mag wikipedia di jàng wikipediyaa ab sémbub jimbulang la ci web bi di lu àddunawu te bariylàkk ag bindam nag mi ngi wéy ba tay xaralaay wiki lañu jëfandikoo ngir sos ko yéeney wikipedia mooy jébbal am maandu te fugluwu nupedia di woon ab sémbub jimbulang bu ubbeeku bu jimmy wales sosoon ci weeru gamu atum mboolaay gu bomis gi jimmy wales féetewoo woon moomeel gi ci ëpp moo ko jàppale woon ciy koppar doon fay larry sanger mi jiite woon mbind mi waaye nupedia ag màggam dafa yeexoon lool ba waraloon ci larry sanger xalaatoon ni sos ab wiki moo doonoon liy man a gaawal yokkteeg jukki yi xalaat boobu ñeel jëfandiku xaralag wiki ngir sos ab jimbulang juroon na ag diisoo ci diggante larry sanger ak tëriinkat boobu di ben kovitz ngir mu faramfaceel ko ci ni mu gën a leeree ana nan la xarala gu wiki di doxe ci ab reer ca san diego la ame woon ci tamxarit ci nii larry sanger ni jimmy wales ngir ñu jëfandikoo xarala gu wiki ngir sos ab jimbulang bu gën a woyof lii moo jur sosug jimbulang bu wikipedia ginnaaw bi ko jimmy wales ak larry sanger sosee wikipedia ngi judd ci kàllaama waa angalteer ci tamxarit gu waa faraas teggu ci gamu gu waa almaañ tegu ci ak yeneen yépp ba tay ci atum mat nañu ñaari téeméer ak juróom fukki làkk ci diggi gamu la larry sanger tekki ndomboy tànkam ci ñaari sémb yépp ginnaaw bi bomis tëyyee loxoom fayatul larry sanger ci liggéey bi mu doon def ci wikipedia ak ci nupedia ci weeru koor la nupedia tëj ba fawwu wikipedia moom wéy di màgg boobu ba léegi wikipedia di dox ci ay àtte yiy askanam tëral ndànk ndànk jëmug kanamam ci maami koor la mbootaay gu wikimedia juddu ngir wut ay koppar yu muy suuxate sémbi wikipedia yépp wikipedia wolof moom mi ngi sosu ci ndeyi gamu toog daanaka ñaari at te amul benn yëngu yëngu ci tamxarit la am jukkeem bu njëkk xoolal xët wi ñeel ni ñu ko binde ci xët wu njëkk wi bakkam mooy jimbulang bu ubbeeku bi maanaam di lu ñépp bokk te ñépp man cee cëru ngir gënal ko jimmy wales di kenn ci ñaar ñi sos sémb bi mi ngi koy tekkee niki ag jéemantu ngir sos ak séddatle ab jimbulang bu ubbeeku ci anam gu mucc ayib ngir nit ku ne man koo am ci làkku cosaanam baatu wikipedia mi ngi jóge ci taqaleg ñaar yii di wiki di ag nosteg yoriinu ëmbiitu dalub web bu ñu man a soppi jaare ko ci ab joowukaayub web ak pedia di reenu baatu làkku waa angalteer bii di encyclopedia di tekki jimbulang li ñu jublu ci sémbub wikipedia mooy mu doon ab jimbulang maanaan muy jëmmal bépp xameefu nit lépp lu nit xam man caa ne wikipedia du ab baatukaay du am péncum waxtaanuwaay xoolal xët wii ngir xam lu wikipedia doon ak lu mu doonul sémb bi dafa àddunawu day laal bépp xeetu xam xam bariylàkk te amul ag pay mooy xam ni yaram yi mel ak seen dëgg dëgg ci lu dul ag laalante gu fisig walla simig gu jonjoo direct ak yaram yii fi nu ko gënee doxale ci jamono jii nag mooy nataali jawwu yi nuy far a defe ci satalit yi walla yi nuy far a def di jëfandikoo ay fafal naaw muhammad jamm na sax ci mom mi ngi judd ca makka atum g ci at wowu la abraha buru abissini bëggona danel kaba ji waye yalla suñu borom danelna pexem yonnifa ay picci yu amon ay xer yu mag ci sen sall ray nitam yepp alxuran waxna ci li ci sar al fil ñay wi muhammad ci banu hashim la bokkon bayam abdullah la won dom bi abdul mutalib ganona bëgg abdul mutalib bimu juddu dafa fekk abdullah mu de di dellu ci jayantu ci sham kon yay ji amina bint wahb ak mam ji abdul mutalib mom bi yonenta bi judd mag la won ta at yi danka xawona sonal ca tukkib yaxantoom booba la baayi yonnant bi làqoo ca tawat ju ko daloon ba muy dëpp ba muy ñëw ba agsi madiina la ko gënoon a sonal mu daal di wàcc ca ña ñu daa wax banii najaar di woon genn ci giiri xasraj yi fa la génne àdduna maamam nag di haasim mom abdul manaaf dafa a takoon soxna looloo tax ñu naan banii najaar de ay goroy yonnant bi lanu j m yónnent baa ngi judd j m ginaaw bi waajur wi làqoo mu daal di màgg cig njirim waaye maamam abdul mutalib beg ci moom lool tudde ko muhhamad yar ko cig cofeel ak ñeewant waa quraysin nag aadawoo woon nanu di yóbb seeni doom ca la génn màkk ca nàmpalkat ya ngir ñu man a màgg ci jàwwu ju sell wér gu yarame te deesi fa dégge araab yu sell bu ko defee loolu di tax ba ñuy wér neexi araab te leeri wax nii la aamina defoon ni ñépp yóbb doomam muhammad j m ca ab nàmpalkat bu tuddoon aliima asahdiya mu bokkoon ci banii sahd bun bakr seeni kër nekkoon ca tàkk ga ca wetu màkka bi muhammad àggee ci am juroomi at la ko soxna aliima delloosi ndayam ca màkka mu nekk fa ca pekkam maamam abdul mutalib di ko sàmm ca jamono jooja la soxna aamina bint wahbin jugoon ne day siyaareji bàmmeelub boroom këram abdul laah ca madiina ba mu demee bay dëpp la ko tawat ja dikkal mu faatu ca ndëkk sa nu naan abwaa te nekk ca yoon wa dox diggante màkk ak madiina ñu daal di ko fay denc looloo waral bi yonnant bi màggee di ku soppoon di jaar ci ndëkk soosu ngir siyaare bàmmeelu waajuram ju jigéen ju laab jooju ci nii ndaysaan la muhammad mujje di jirim ci nday ak ci baay looloo waraloon maamam abdul mutalib mujjoon féetewoo ag yaram akug wattoom bëggoon ko it lool waaye sàmm googu gépp ak fonkeel gi teewul muhammad j m doon yëg naqaru njirim ndax kat da daa gis moroomam yi ñu nekk ak seeni way jur moom muy ku leen ñàkk waaye nag loolu jox na ko ag sukkandiku ci boppam may ko ag temb ci njëmm akug wéroodi ci kenn nàmm am xelam ubbil ko ay bëtam ci dëgg dëggi dund gi te booba ay atam lu néew la woon loolu de lu jeexiital la ci moom ak cig dundam yàlla nag moo bëggoon ci moom loolu ngir tànn gi mu ko tànn ngir mu yanu bataaxel bii di lislaam te war koo tas abdul mutalib ginaaw bi aamina làqoo yàggu fi dara moom itam làqu te booba yonnant baa ngi amoon juroom ñatti at fa la ko baay tëxam aboo taalib jële yóbb ko ca këram ca doomam yu xaw yaa sakkan tubaar kàlla ngir mu yaroo fa aboo taalib nag moo wuutu woon baayam ci jiite màkk ci noonu mu jeexaloon alalam jépp ci sàmm kaaba gi ak way aj yi ak dimbali ñi aajowoo looloo taxoon alalam bariwutoon ak li muy nekk kilifag màkk lépp lii a waraloon yonnant bi doon jéem a woyofal yan bi ci baay tëxam jooju ba àggoon ci di sàmmal ag jur ñenn ci waa màkk yi ñu ko ci daa fay lu néew a néew loolu it doonati ab pose ngir mu tàggatu ci xam ni nuy sàmme ag njaboot jikkowoo ag ñeewant akug laa biir ak sàmm ak yewwute ñuy jikko yu manul a ñàkk cib sàmm bu bëggee wattu gétt gi muy sàmm yàlla moo ko bëggaloon loolu ngir tàggat ko ci bataaxel bi mu ko nar a joxi sàmm ag jur nag daara la joj lu bari ci yonnant yi jaar nanu ci ba sax jële nanu ci yonnant bi j m mu ne amul yonnant bu sàmmul ag jur bi mu amee fukki at ak ñaar la ànd ak baay tëx ji aboo taalib cib tukki dem shaam bi mu amee nag ñaar fukki at la tàmblee bokk ci yaxantu gi ni ko waxambaaney quraysin yi daan defe mu wone ci it man gu mu ko man lool ndax ku ñu xamoon la cig wóor ak dëggu yewwute ak ñaw ay man manam tàmblee feeñ ñeel waa màkk li ko gënoon a wuutaleek nit ñi mooy wóoram gi jéggi woon ab dayo te xaroon baax ñu mujjoon di ko wóolu ci lu mu man a doon te am xel mu dal ci ne dana sàmmoonteek kóolute gi nit ñi def ci moom looloo taxoon ñu naan ko ku wóor ki ak ku wóor ku dëggu ki bi at yi àggee ci ñaar fukk ak ñeent daa dajeek soxna xadiija soxla waxambaane wu ko yoral yaxantoom gi mu doon deflu ca shaam moom nag soxna su woomle la woon bokkoon ci way woomley màkk yi ci noonu ñu digal ko mu gis muhammad j m ba mu ca waxeek moom yonnant bi nangu yonnant bi yaxantujil na soxna xadija ca shaam ànd ak ngóoram sa nu naan muyasara muyasara mii yéemu woon na lool ci jikko yu rafet yi ci muhammad ak yewwu geek man gee yaxantu ndax bi njaay mi nekkee ciy loxoom fulu na ay yooni yoon wuuteek ba mu nekkee ci loxoy keneen looloo tax bi yonnant bi j m delloo jébbal soxna xadiija alalam ak la mu ca tonoo cig kóoluteek dëggu soxna si yéemu na lool ci jikkoom yu rafet yi ak njëmm gi ne ci moom ci noonu mu yónni ci moom kenn ci ay jegeñaaleem xamal ko ne da koo bëggoon niki boroom kër yonnant bi j m nangul ko noonu la seen diggante sottee te booba yonnant baa ngi am ñaar fukk ak juroom ciy at xadiija moom yor ñéen fukk ci noonu mu faroon di soxnaam di yaayam di ki koy dimbali ci lépp yonnant bi j m amoon na ag texe ci séy boobu naka noonu xadiija ci noonu séen kër di misaalum mbégte cib séy ak texe ci biir kër soxna xadiija nag mooy ki jur mbooleem doomi yonnant bi ku ci dul ibraahiima moom de soxna maariya mi di ab qibt moo ko jur moom nag sëñ ibraahiima ci jamonoy yonnant bi la làqu yonnant bi wéyoon na ci yaxantoom gi ginaaw bi mu yoree soxna xadiija mu ko daan defe nag ni ko waa xuraysin gépp daan defe rekk ñoom de yorunu wooni bitig aki mangasin moom kay danu daa defi njëgg yu mag mbaa yu ndaw jawali yaman ci sedd bi bu cooroonee ñu dem shaam màkk màkka bu nekk daa na man a bokk ci njëgg li bu bëggee njëgg loolu nag moom la nu daa wax ci ci araab bahiir kenn ci góori xuraysin yee ko daa jiite ku soob ci ñoom ànd ak moom bu ko defee bu dellusee ñu seet li ñu tonowu seddale ko ku ci nekk am ca la nga ca def seen yaxantuwiin woowu moo taxoon xuraysin daan am jot di daje ci jataay yi di waxtaan rawati na ca la wër kaaba ga waaye yonnant bi j m moom néewaa na bu mu bokkee ci yii jataay moom kay këram la daa toog mbaa mu génn dem ca àll ba ngir wéet fa di xalaat ak a settantal ndax sopputoon di fo mbaa muy caaxaan ak a waxi larax yonnant baa ngi amoon fan weer ak juroom ciy at jamono yi xuraysin di màbb kaaba gi ngir tabaxaat ko ndax tabax bi daa xawoon a màggat ngir yol mi daa sottiku ci kawam bi ñuy tabax ba àgg ca hajarul aswad ñu jaaxle ci gan giir ci xuraysin mooy am teraangay yekkati ko teg ko fi mu war a tegu ñu toog ca kaaba ga di gëstu nu ñuy lijjantee loolu far ñu dëppoo ci ne ku njëkk a ñëwaat rekk ñu jox la nga àtte leen ci jaaxle googu far muhammad j m ne tëll ñu ne ku wóor kaa ngee na ñu àtte waaye mu àttee leen nu gaaw te yomb mooy jël làmbaayam li mu yoroon lal ko ci suuf teg ci doj wi ne giir gu nekk na jàpp ci cat ngeen tegandoo ko ca barabam nii daal la ko lijjantee ca yombam ga ak xarañam ga ak lëmóodikoom ga bi at yi jegee ñeen fukk la sopp gi mu soppoon ag wéet gën a yokk mu gën a bëgg xëlwa ak beru mu daan génn màkk ngir dem ca doj wa nu daa wax harraa ngir xunti mu fa nekkoon mu mu daa faral a dugg ngir jaamu yàlla noonu la daa jeexale weeru koor wi ngir sellal boppam laabal xolam benn bis nag ci koorug atum g j ba jant bay so la ko genn kàddu gu nooy dikkal ca dalug xunti ma naan ko jàngal yonnant bi j m tiit njàqare li jàpp ko waaye mu ne ko man duma kuy jàng waaye mu yëg mu mel ne dafa am lu koy naj ba dënn bi xaw a xat mu noppal ko bu ko defee kàddu gi delseeti neeti ko jàngal yonnant bi neeti ko man de manu maa jàng naj ga delseeti ba mu xawee woyofati kàddu ga delseeti ne ko jàngal ci sa turu boroom mi bind bind na nit ci lumbu dereet jàngal sa boroomay ki gën a tedd kàddu ga daal di dal daal di deseeti fekk jant biy so yonnant bi yëg njàqare lu rëy daal di gaaw génn xunti ma dem ñibbi bi muy àgg lëndëm gaa ngi doon dugg ndax diggante màkk ak xur wa xaw na a ëpp ay ñatti kilomet ba yonnant ba j m àggee ca kër ga daa daal di woote ne muur leen ma muur leen ma booba ñaq waa ngay siit yaram way lox soxna xadiija daal di dawsi sàng ko tàmbli koo dalal bi tiitaange gi demee yonnant bi xamal ko li xew ne ko man de damaa xëm ndax xamagutoon ne li ko daloon ag wahyu la gu tukkee ca sunu boroom t s indil ko laaya wi njëkk ci alxuraan ju tedd ji soxna su tedd sii di xadiija wéy ci di dalal xelum yonnant bi j m naan ko lii la dal de du man a doon lu dul lu baax ndax yaw ku baax nga am kóllare dëggu baax ci sa ñoñ di taxawu nit ñi bu ñu ameey naqar ca noona xel ma tàmblee dal mu yëg jàmm bi soxna xadiija gisee ne tiitaange gi dañ na daa ànd ak moom seeti doomi baay tëxam ja tudd waraqat ubn nawfal mu nekkoon góor gu am hikma daan jàng téerey diine yi te dégg ebrë yonnant bi nettali ko li xew waraqat yéemu lool ne ko lii de mooy mbóot mi yàlla wàcce woon ci muusaa j m ne ko aka neexoon may gone ba man a ànd ak yaw ci tas sa bataaxel bii xelum muhammad dal mu dellu këram waaye teguñu ci lu néew rekk waraqat faatu ndax daa xawoon a màggat yonnant bi dellu këram ak xadiija ci xel mu dal ak mbégte am yaakaar ne wahyu gi dina delseeti bu sukkadikoo ci waxi waraqat yi waaye wahyu gi yeex a ñëw ba yonnant bi far àgg ci jaaxle lool waaye mu mujj ñëwaat ginaaw bi xelum muhammad dal mu xam ne lii kat ag wahyu la gu tukkee ca yàlla t s te moom ku ñu tànn la ngir mu jottali nit ñi diine ju juge ci asamaan si war a joxaat diiney asamaan yi seen leer ak sell gu njëkk ga ñu yoroon njëkk nit ñi di ko yàq di ko tàqal ci li jamono di gën a romb nii daal la muhammadum abdu laah mi j m mujje di yonnant bu nu tànn yonni ko ci mbooleem mbidéef yi ngir mu indi fi leer gu tukkee ci sunu boroom di gindee di tege ci yoon di jële cig bokkaale jëme cig wéetal yàlla di jële ci lëndëmug réere yàlla jëme ci leerug gëm ko jëme ci lislaam fii la jaloorey muhammad yonnantub yàlla bi jàmm yal na sax ci moom tàmblee akug jànkoonteem ngir wisaare bataaxel bii ko yàlla jox mu war koo jottalee ci ngën ji anam ak melo ginaaw bi la wahyu gi tàmblee dikk cig toppante di wàcc ci ku tedd ki di indi laaya yi def tay alxuraan nànk nànk kon alxuraan ñëwadoowul cig mat waaye laaya topp laay ba kero muy mat nga xam ne jibriil da ko daan dikkal di ko déggal laaya yi bu ko defee du ko ba ba kero muy wattu laaya jooju ci dënnam mel ne sax dañu ko cee bind làmmiñ wi di ko baamu yonnant bi bu masaa na jot ciw dogiit ci alxuraan da ko daa baamu ba mokkal ko bu noppee jàng ko ci saabaam yi daal di woo ñenn ci ñi man a bind ci ñoom ngir ñu bind ko ca saa sa ci anam gu xereñ bu ko defee saaba yi gaawantu ñoom itam jàng ko mokkal ko ci anam gu dul soppikooti ba fàww nii la laaya yi doon dabantee saar yi di ko mate nànk nànk ci lu tollook ñaar fukk ak ñatt ciy at ndax kat laaya wi njëkk a wàcc ci yonnant bi j m mi ngi ko fekkoon mu am ñéen fukki at wi ci mujj wàcc bi muy bëgg a faatu te booba mi ngeek juroom benn fukk yu teg ñatt ciy at alxuraan nag ñi ngi ci jublu téere bu tedd bi bépp walla ab xaaj ci moom kon daal alxuraan ci nii mu ñëwe waxi yàlla a ju mu wàcce cib yonnantam j m ngir mu jottali ko nit ñi ñi ngi ko wàcce ci yonnant bi muy lu nu biddiwal maanaam nànk nànk kem ni ko xew xew yi soxlaa ak tolluwaay yi ba kero muy mat di téere bu ñu laabal bu ay caaxaan dul laal fenn laa yaatiihil baatilu min bayni yadayhi walaa min xalfihii moom nag danu koo séddale def ko ay saar yu toll ci saar saar wu ci ne tam seddaliku ciy laaya saari alxuraan yi nag ak laaya yi lii lanu ëmb saxal kennug yàlla t s nangu ne muhammad yàlla a ko yonni gëm mbooleem yonnant yi fi jiitu woon yonnant bi gëm téere yi yàlla wàcce ci ñoom gëm alaaxira julli woor natt asaka aj ñuy wóor dëggu am yërmaande ci ku néew doole ku aajowoo ku ñàkk am ag cofeel ñeel bépp jullit tey dimblante ak moom ci lu baax ak fonki way jur teral leen añs ngir jàjjeek waare aki nettali ci dundug yonnant yi ngir soññee ci ngëm ak foñloo wëlif bokkaale ubbi seeni gët ci kàttanug yàlla gi akug xerañam jaare ko ci di leen woo ci ñu settantal bindiinu àdduna bi akug nosoom gu xereñ gi jaare ko ci wax leen li yàlla dig ku gëm cib yool akug pay gu neex ci àdduna ak alaaxiraa ak soññee ci jiyaar ci yoonu yàlla jaare ko ci leeral leen mbugël yi ñu waajal ñeel ñi ragalul yàlla mbaa ñuy tooñ nit ñi di jalgati mbaa ñuy gàttañlu ci def jaamu yàlla yi mooy yoon wu mat wiy nos ni nit ñiy jëflantee ci seen biir ak li nu am ciy àq aki yelleef ak li leen war ciy wartéef dinanu gise ci loolu ne alxuraan de ëmb na ag nos gu mat ñeel dundug nit ci gépp anam mi ngi rëdd séqoo gu nit ki ak boroomam akug séqoom ak mbokkam dajaleeti jullit ñi ci genn bennte mooy umma bi walla mbooloom lislaam mi di jullit ñi joxati mbooloo mii yoon ak nosteg politig gu mboolaay ak gu jikko dugg ci lislaam du rekk jël diine gëm ko di def li mu digale ciy jaamu waaye kay ag tuxu la dem ci ag mboolaay gu yees gu mat gu ami ponkam aki nosteem aki yoonam aki misaalam yu kawe ndax lislaam ag noste gu mat la gu takkatoo bataaxelub yonnant bi j m mooy dugal nit ñépp ci lislaam ak tuxook ñoom jëm ca nosteg lislaam gu yees ga te mat looloo taxoon yonnant bi j m daawul yam ci sàkku ci nit mu tudd ñaari seere yi rekk ak def jaamu yi waaye kay da daan sàkku ñu bàyyi seen dundug réer gu njëkk ga te tàbbi ci nosteg politig gu mboolaay gu ruu gu yees gii moom de santuñu ko woon rekk mu woote te jotal bataaxel bi waaye ligéey bu baax ci nit ñi gëm te dugg ci xeetu lislaam wi ak àddunaam ju yees ju fees ji dell ak yiw ak barke yonnant bi wéy na di xamal nit ñi bataaxelam bi bu ko defee gàllankoor yi nekk ci kanamam mel ne ay doj ndax kat nit yombul mu tàqalikook ni mu baaxoo woon a dunde nit jaamub li mu miin la waaye moom mu wéy di deewoo di jànkoonte di muñ ba jóoxe bataaxel bi ca na mu gën a rafete loolu mooy kiimaanug dundug muhammad j m gu yéeme gi cib taar moom daal ci léppam dund la gu fees dell ak ay bind yu fees aki bind yuy jàngale dëggug ngëm wóor ci def li la war muñ ci lu naqari ñeg ci fas yéenee jéggi gàllankoor yi oy ci jikko yu rafet muñ ci loraangey nit ñi gëm ne ndam lu mu yàgg yàgg dana mujj ñeel jullit biy jëf tey jànkoonte tey oy ci buumug yàlla gi ci lu dul naagu mbaa yoqat walla tàyyeel yonnant bi ginaaw bi nu ko yonnee dund na ñaar fukki at ak ñatt yoy ci la matale bataaxelam bi fukki at ya ak ñatt nag màkka la leen jeexal fukk ya ca des mu def leen madiina làqu nag ca weeru rabiihul lawal ci atum fukk ma ak benn ginaaw gàddaayam gu tedd ga mooy diirub deewoo ak jànkoonte gu tar ga ak way bokkaaley màkka yi ak jiyaaram ga ngir taxawal fa mbooloo mu lislaam mi ba bi mu gàddaayee dem madiina diir ba di fukk ak ñatt ciy at mooy jamonoy ndam jaare ci dugg gi waa madiina dugg ci lislaam mbooloom lislaam am fa ak nos mbooloo mii ak mottali jaamu yi nekk ci lislaam ak sariyaam ak tëral nosteg xeet wi gu politig gi ak gu mboolaay gi ak dugal dunu araab bi ci lislaam ngir waajale ci tas gi lislaam war a tas ci mbooleem pàkki àdduna bi ab diiram nag fukki at la ak lenn ciy weer dafa séddaliku ci ñatti tolluwaay am mbooloo topp ci tàbbi ci lislaam ci waxambaaney këri màkka yu xuraysin yu mag yi ñi ci yàlla ubbi séeni xol nanguloo leen lislaam ak dalam yu kawe yi ku ci mel ne talhata mom hubaydul laah abdurahmaan ubn hawf sahd ubn abii waqaas usmaan ubn haffaan subayr ubn ul hawwaam am mbooloo it tàbbeeti ci lislaam ci ñu ñàkk ñeek jaam yi ak way néew yi doole ci ñi yàlla tawfeexal ubbil leen buntub gore ak yamoo ak yaakaar ku ci mel ne bilaal mom ecopi mi hammaar ubn yaasir xabaab ubn ul arat mbooloom lislaam mii baaxoo woon naa dajeek yonnant bi ca kaaba ga ngir déglu alxuraan ci moom ak jàng ci ponki lislaam loolu it jur way bokkaaley quraysin yi yoqat ci jataayi néew yi doole yii ci li wër kaaba gi tax it ba ñu tàmbli di leen xatal ak a yoqatloo yonnant bi it gis ne war naa wutal jullit ñi barab bu ñuy daje cig féex akug dal ci noonu wenn waxambaane wu bokk ci ñoom ñu naan ko arqam ibn abiil arqam ne man naa joxe këram ngir ñu fay daje yonnant bi nangu looloo taxoon jullit ñi ba woon daje ga ñu doon daje ca kaaba ga waaye làqu gi nu làqu leegi tiitloo waa màkka yi jeqi ci ñoom njàqare rawati na aboo jahlin ak aboo lahab mi nekkoon baay tëxi yonnant bi ak ñeneen ñu tàmbli di topp jullit ñi ak di leen xeeñtu ngir xam li nuy def am na bis aboo jahlin nekk fi barab di néggandiku yonnant bi booba mi ngi jëmoon ca kër arqam ba yonnant bi j m egsee mu toroxal ko waaye yonnant bi muñ ak doonte ku dëgër la woon te manoon koo sonal waaye yàlla da koo digaloon mu woo nit ci hikma ak waare gu rafet ci noonu mu wacc ko fa dem bi hamsa baay tëxi yonnant bi yëgee li xew daa mer seeti aboo jahlin duma ko ba noppi jébbalu dib jullit ci noonu mbooloom lislaam mi gën a am doole ci dugg gi ci hamsa dugg leegi bi ci as ndiir toppee omar ubn xattaab jébbalu jullit ñi gën a sawar gën a ñeme ñu daal di génn leegi kër arqam daal di dellu fa nu daa dajee di la wër kaaba ga ci noonu yonnant bi tàmbli di woote ci kaw ci lu bir te faaleetul merum waa màkka yi fii la jamonoy woote ci kër arqam jeexe leegi woote gu biti gu matale gi tàmbli yonnant bi daa amoon njàqare ci saabaam yi ragal waa màkka yi sonal leen ci noonu mu laabiire woon leen ci ne ku bëgg ci ñoom man naa dem ecopi foofa dananu fa man a doxal seen diine te kenn du leen topp mbaa mu leen di sonal bi mu ko defee lu tollook juroom ñatt fukki góor akug jigéen gàddaay dem fa ci ñaari yoon yonnant bi des màkka ak mbooloo mu néew ci jullit ñi di jànkoonteek lori quraysin yi waa màkka yi jaaxle woon nanu ci man gi yonnant bi j m manoon a muñ ay coona ak sax gi ñu sàkku woon ci baay tëx ji mu tere ko woote gi maanaam lislaam waaye yonnant bi bañ te wëy ca woote ga looloo waraloon way bokkaale yi defoon ag dogoo gu mat ak banii haasin ak itam banii abdul mutalib te ñoom ñooy mbokki yonnant bi j m banii haasim jànkoonte na aki coona ngir dogoo gii nga xam ne saxoon na ñatti at tolluwaay bu ñaareel bii nag weesuwutoon juroomi at bi aboo taalib faatoo ba teg lu néew la soxna xadiija làqu moom it y y g ginaaw bi mu àndeek yonnant bi ñaar fukki at ak juroom cig sell cofeel dimblante ak bànneex ak doonte fukki at yu mujj yi daa feesoon dell aki jafe jafe mettiit ak xatal yonnant bi naqarlu woon na bu baax ci faatug àndandoom bii mu bokkaloon dund gi nekkoon ku matal kóllare wóor taxawoon ci wetam ci ati jafe jafe yi wone woon gën jaa kawey misaal ci ni soxna su gëm tey muñ war a mel bi aboo taalib ak soxna xadiija làqoo yonnant bi yëgoon na ne ku wéet la dëgg te at yu metti yii mu def màkka di jiyaar indilunu ko lenn ngérte lu ñu xam lu mu yaakaaroon ngir lànkug waa màkka yi ak nuur gi nu nuuroon cig kéefar ak oy ci li ñu fekkon seeni baay fii la yonnant bi xalaate ci génn jéem a wooteji ca taayif ga jege màkka mu daal di fay dem ànd ak mawlaam bi sayd ubn haarisa waaye waa taayif déggalunu ko looloo tax mu dëppoon dellu màkka waaye yonnant bi loolu taxutoon mu yoqat ak doonte waa màkka yi dañoo dogu woon ci lor ko mu daal di jawali ca biti màkka ca lenn ca giir ya fa dëkke woon daan leen woo ci lislaam waaye taxutoon lu bari wuyyu ko ca yonnant bi j m da daan def bu déggaan aw nit ñëw màkka mu gaaw gisi leen woo leen ci lislaam ba yonnant ga tollee ci fukki at ak benn daa dajeek ab kuréel ci giirug xasraj ñëwoon màkka di woon genn ci ñaari giir ya nekkoon màddiina geneen ga di woon aws xare ba nekkoon di lu tar ci seen diggante ak noonoo ga ca at ma ca topp am mbooloo ci aws dikk na màkka yonnant bi gaawantu seetsi leen wax ak ñoom waaye fekk fi ñoom nopp yuy déglu ndax kat yahood yu madiina yi dañu daan wax naan ab yonnant bu ñu yonni de dana dikki di dimbalisi yahood yi ci xasraj ak aws looloo waral aws jortoon ne muhammad j m mooy yonnant bi yahood yi doon wax bi seen mbooloo mi toogeek moom déglu ko lanu gis ne moom kat ku dëggu la ci li muy wax bi mu leen jàngalee ay laaya ci alxuraan lanu ko gëm sàkku woon ci moom mu may leen ba ñu dellu madiina man a nettali seeni mbokk li nu dégg ci noonu ñu dellu nettali seen mbokki aws yi li nu dégg ñoom itam ñu amoon yitte lool ci gis yonnant bi te déglu ko xasraj it dégg loolu ñaari giir yépp tàmbalee yittewoo gis yonnant bi ñu daal di dogu ci yonni am mbooloo mu mag ci jamonoy aj gi ngir mu dajeek yonnant bi j m déglu ko mbooloo mi làqu waa màkka ñëw dejeek yonnant bi j m déglu ko waaye am lu leen wóor ci ne yonnant bi de ku dëggu la ci noonu ñu ànd dugg ci lislaam def ak yonnant bi jaayante gu haqaba gu njëkk ga daal di ko cay dig ne danañu woo waa madiina ci lislaam te dinañu ko seetsiwaat ginaaw at ci noonu yonnant bi yabal ak ñoom saabaam ba tudd mishab bun hamiir ngir mu jàngal sariiya waa madiina bi lu toll ci at jàllee mishab dellusi ànd ak ab kuréel bu mag ci waa madiina seenub lim tolloon ci juroom ñaar fukki góor ak ñatt ak ñaari jigéen ñu jàkkaarloo woon ak yonnant bi fa haqaba jaayante fa ak moom muy jaayanteg ñaareel ga ñu ñaanoon ko mu tuxu dem madiina ne ko fas nanu ko yéenee aar ci gépp noonu te dinanu ànd ak moom ci tas lislaam ci ginaaw bi rekk la yonnant bi digaloon saabaam yi ñu gàddaay dem madiina ñu daal di woon tàmblalee gàddaay ci ay mbooloo mbooloo topp mbooloo lislaam daal di fay tas ba mujj doo gis genn kër ca madiina gu ay jullit nekkul li ëpp ci jullit yi nekkoon màkka daal di gàddaay dem madiina ci weer yu néew bi yonnant bi amee xel mu dal ca saabaam ya ca madiina daa daal di gàddaay moom itam ànd ak àndandoom bu dëggu ba aboo bakr ñu ngi génn ci lëndëm gi cig làqu ndax waa màkka dañoo bëggoon a tëye yonnant bi ca màkka ngir ragal lislaam di ame doole ca madiina mi ngi àgg madiina ci rabiihul awal ca at mu njëkk ma ca gàddaay ga sëtumbar atum g j booba nag di taarixe ci gàddaay gi tàmbaleegutoon a dox ndax seydinaa omar mooy ki digale ñu jël at mu njëkk mi ci gàddaay def ko at mi taariixu jullit ñi di tàmblee yonnant bi fekk na li ëpp ci waa madiina ñu tàbbi ci lislaam ñu néew a ci desoon cig kéefar te bi yonnant bi dikkee dañoo daal di jébbalu yahood yu bari nag nekkoon nanu madiina tasoon fépp it ña ca ëppoon daan bay mbaa ñuy def yenn mecce yi niki meccem weñ ak tëgg ñatti giir yu mag nag feeñ na ci ñoom ñooy banoo qinqaah banoo nadiir ak banoo qariitha ñoom nag dañu daa won xasraj ak aws ne ñoo leen kawe te daan leen jaxase bay waral ñuy xulook a xeex bu xeex amee leeg leeg ñu ànd ak xasraj leeg leeg aws daa nañu wax naan ab yonnant de dana feeñi ci ñoom te bu ñëwee dina ànd ak ñoom xeex aws ak xasraj ba jële leen fi yonnant bi bi mu àggee madiina rekk daa daal di tàmbalee ligéey ligéey bi nag ci ñaari mbir yii la jëmoon bi yonnant bi nekkee ci ligéeyam boobu ngir amal jubluwaayam yooyu mi ngi doon wéy it ci di woo ci lislaam giir yi peek madiina ngir ñu bokksi ci uma bi di xeetu lislaam wii xëy taxaw bi mu gisee ne lenn ci kilifay giir yii ànduñu woon ak moom ci loolu daa daal di woon yabal ay cong yu lislaam ngir xeex kilifa yooyu ak ñi leen di jàppale ba duñu man a gàllankoor giir yi ci dugg ci lislaam cong yii lanuy wax xaswat ndax yonnant bi j m moo ko daan jiite bu ko kenn ci saaba yu mag yi jiitee nag ñu koy wax sariya yonnant bi tàmbli na daal di yabal juroom benni xaswa ak ay sariya yoy amal nanu xemmemtéef lii bu ko defee gëwéelub uma bu lislaam bi gën a yàkkiku daal di far ëmb mbooleem wàllug càmmooñ gu hijaas gi loola nag la ca juddoo mooy madiina mujj teg loxo ci yoonu yaxantu wi jëme shaam juge màkka looloo taxawaloon yaxantu ga ca màkka te kat moo nekkoon balluwaay bi seen koom di juge xaswa bu badar walla xareb badar yonnant baa ngi ko def ci atum ñaareelum gàddaay gi mi ngi ame nag ca digg yoon wa dox diggante màkka ak madiina lu tollook ñatti téeméeri jullit am ca ndam ca kaw junni ci yéefari màkka yi muy ndam lu mag lol lislaam dëgëre na ci nit ñi it xame ci ci anam gu wér pé gees manul a sikk ne yonnant bi de wooteem gii lu wé la ci noonu nit ñi sottiku madiina ciy mbooloo yu mag ngir dugg ci lislaam ci xare bii lanu raye aboo jahlin ak ñu ko moy ci nooni lislaam yu tar yig noonu màkka manutoon a ñàkk mu def lu ko delloosi darajaam ji mu ñàkkoon ci dunu araab bi ubbilaat ko yoonu yaxantu wi looloo waraloon ay way bokkaaleem dajale woon doole ju mag ju toll ci ñatti junniy góor ñaari téeméer yi diy gawar ca atum gàddaay mu ñatteel ma ñu dox jëm madiina ngir dugg ko ci doole waaye yonnant bi génn àkk léen ci lim bu toll ci junni ciy saabaam ñaari mbooloo yi daje ca bëj gànnaaru madiina fa ron doju uhud xare bu tar tàkk fa bob jullit ñaa ca amoon ndam ca njëlbéen ga waaye boroom fett ya mujjoon wooteek ndigal la leen yonnant bi joxoon daal di wacc seen barab ya nu leen taxawloo woon xaalid ubn waliid mi jiite woon yéefar yi daal di màng pose bi song jullit ñi bu ko defee seen sàppe jaxasoo baj baji ñu ray ca ñu bari waaye yonnant bi moom des fa ak lu néew ciy gaayam mu daal di woo ay saabaam ngir ñu dellusi ak li ñu ko gaañ ca xare ba lépp téewul mu xettali dooley jullit ñi ca njàmbaaram ga ak saxam ga te tee yéefar yi dugg madiina xeex bi wéy ba jant so fii la coona bi sonale yéefar yi ñu rocciku dellu màkka ci lu dul ñuy amal li nu bëggoon te loolu saxug yonnant bee ko waral akug njàmbaaram ak sorib gisam waaye yéefar yi li nuy amadi li ñu bëggoon lépp téewul ray nañu ab lim ci tànnéefi jullit ñi ku ci mel ne hamsa bay tëxi yonnant bi j m ak mishab ubn hamiir mi daa gàddu raayob jullit ñi ak leneen lu toll ci juroom benn fukki jëmm jullit ñi am nañu lu leen naqari lool ci seen sahiid yi waaye jànge nañu ci uhud benn bind bu ñu dul fàtteeti mukk mooy topp yonnant bi j m ak defi ndigalam waa màkka yi yég nañu ne amaluñu dara lu am solo ci li ñu doon sàkku ñu gis ne ñoom kat ak seen mbégte mu rëy mi ñu am lépp ci ray gi ñu def lu bari ci jullit ñi téewul màkka dañul di nekke na mu nekke woon yoonu yaxantu wi mi ngi ci loxol jullit ñi giir yaa ngi tàbbi ci lislaam gu dugg geneen topp ca lii a tax aboo sufyaan ubn harb mi nekkoon njiitul màkka ginaaw aboo jahlin jugoon boole doole ju mag ci waa màkka ak ñi tapoo ak ñoom ci giir yi ñu dox nag jëm madiina ca juroomeelu at ma ñeel gàddaay ga bu ko defee yonnant bi aki saabaam jug gas am xandaq ca la wër madiina ba mboolooy xarey yéefar yi agsee manuñoo jéggi pax ma bu ko defee xare bi yam ci sàneente ay fett jéggi xandaq mi ci noonu jullit ñi ñoom wone ag yewwu gu mat ci sàmm seen xandaq ba yéefar bu ko jéggi rekk rayees ko ca saa sa gaw gi sax lu tollook ñaari ayu bis ginaaw bi yàlla yonnee gelaw lu tar ak taw bu metti mu yàq xaymay yéefar yi fay seenuw sawara sedd bi metti ci ñoom ak doonte weer woowa wu mars la woon te woowu weer fa hijaas mooy tàmbalig lolli bi bu ko defee yéefar yi àggati ci manuñoo ñàkk a dind gaw gi te dellu màkka ngir sedd bi te amuñu dara ca seen càkkutéef ya loolu di ag juunu gu mag akug sooy ñeel leen te diw lay wu mag ak firnde ci kàttanug xeetu lislaam wi ak dëggug gëm gi ay nitam am ak ñaw gi nekk ci njiit la muhammad j m ñatti giiri yahood yi di banoo qinqaah banoo nadiir ak banoo qariitha yoroon nanu taxawaay bu ñaaw te noonoowe jëme ca yonnant ba ak wooteem ga dale ko ca bi muy door a agsi madiina weddi woon nañu ag yonnantam naan neey yonnant bi ñuy néggandiku manul a juge ci fu dul gañog banii israayil ginaaw nag yonnant boobu ñu daa wax farul génne ci ñoom xanaa kay ci giirug quraysin gu araab gii dara raxul loolu naqari woon na leen jural leen ag soxot ak kañaan ak mbañeel yonnant bi yàgg naa muñ lor yi ñu ko daa lor ngir yaakaar gi mu yaakaaroon ne danañu mujj noppal ko ba àgg sax ci gëm ko waaye lu mu muñ rekk ñu gën koo bañe lislaam gën koo dellikoo ag noonu waaye làqoon nanu seen noonu googu ak mbañeel gi bi ñu gisee ne lislaam mi ngi gën a dolliku doole di gën a dëgër bis bu yàlla sàkk bi jullit ñi amee ndam ca badar la xolub yahoodi madiina yi gën a dagg ab kuréel ci ñoom it ñooy banoo qinqaah àgg ci manatuñoo ñàkk a feeñal seen bañ gi ñu bañ lislaam ak soxote gi ñu def jullit ñi ci ndam li leen yàlla may ci noonu ñu tàmbli di saboote yonnant beek lislaam waaye yonnant bi j m dem ca seen kër ya gaw ko bi ñu jëbbalee seen bopp la leen génne madiina ñu dem shaam ginaaw bu xaswat bu uhud jàllee ba teg lu néew la yahoodi banoo nadiir lànk ne duñu joxeeti li leen war ci ndimbalul alal li war ñeel umma bi waaye yamuñu ca dañoo tàmbli woon a defi pexe ngir yong yonnant bi j m waaye yàlla t m musal ko ci seenuw ay nga xam ne yonnant bi amul woon lenn lu mu manoon a def lu dul génne leen ñoom itam ngir mucc ci seenuw ay ci biir xareb xandaq ba yahoodi banoo qariitha doon nañu jéem a wor jullit ñi dem jàppaleji yéefar ya gawoon madiina jaare ko ci may leen ñu dugg madiina jaare ko ci seenug wàll looloo war bi xeex bi jàllee rekk yonnant bi daa daal di jawali ca seen kër ya gaw leen ba ñu wommatu nangul ko mu digal saabaam ba tudd sahd ubn muhaaz mu àtte leen ci li jaadu fi moom li tax mu tànn ko nag mooy ñoom ci mom lañu doon sàkkoo ag tin ci yonnant bi moom it mu ne nañu ray ñi ci doon xeex ñi ci des ñu génne leen madiina ci noonu la xeetu lislaam wi mucce ci ayuw yahoodi madiina yi madiina mujj yor lu néew rekk ciy yahood yu bokkoon ci ñi defoon ay tapoo ak lenn ci bànqaasi aws yeek xasraj ginaaw nag feeñaluñu woon genn wor mbaag mbañeel ñeel jullit ñi yonnant bi defu leen dara looloo waral ab kuréel ci ñoom gëm ca gëm gu dëggu am ca ñeneen ñu ca gëm ñu ag ragal gëmloo akug naaféq bi yonnant bi amee lu ko wóor ci ne am cong mu juge ci biti jeex na wor gu biir gi it dañ na la tàmblee waaj ngir dugal màkka ci lislaam gisoon na ne waa màkka yi ñi ci ëpp ñu tàmbali woon a yittewoo mbiri lislaam lañu ndax gis nañu muy yaatu di gën a am doole bis bu nekk li alxuraan digoon jullit ñi bañu nekkee màkka di ñu néew doole gën di feeñ gën di am nga xam ne màkka li ko tee woon a dugg ci lislaam wéesuwutoon lenn ci njiiti yéefar yi ak seeni àndandoo ñoom ñi ragaloon seeni njariñ di sànku seeni daraja di suufe su ñu duggee ci lislaam ci biir loolu ab laaya wàcci bu tedd buy digal yonnant bi mu wëlbati qibla bi jullit ñi amoon muy baytil maqdis def ko leegi kaaba gu sell gi mu mujj ca saa sa di qiblab jullit ñi ñépp bi ñu wëlbatee qibla bi leegi jëme ko ci kaaba gi te yonnant bi xam dëgër gi xeetu lislaam wi def leegi te ame ko doole ci la jugoon ànd ak am mbooloo ci saabaam yi ngir defi umra mooy siyaareji bayti laahil haraam ci waxtu yi dul yu aj looloo tax ñu tudde ko aj gu ndaw gi bu ko defee yonnant bi j m daal di génn ci junni ak ñeenti téeméer ci ay saabaam jëm màkka ngir defi umra looloo taxoon yobbaalewuñu woon ngànnaay ngir bëgg waa quraysin xam ne jullit ñi dañoo ñëw ngir defsi ag jaamu rekk mooy umra gi bi jullit ñi aggee ci barabub hudaybiya mooy buntub màkka bi féete wàllug cammooñ la waa quraysin yi tàmbali woon a ragal jullit ñi dugg màkka ñu daal di yonnee ci yonnant bi ne ko daal àndatuñu ci jullit ñi dugg màkka ak donte yoruñu ngànnaay ñu daal di fay def waxtaan wu yàgg yu mujj àgg ci li ñuy wax juboog hudaybiya moom nag li mu yaxal mooy jullit ñi buñu dugg màkka ca at mooma waaye bu déwén ja a ca waxtu woowa dinañu man a dugg muy atum juroom ñaareel ma g g bu ko defee ñaari wàll yi def ag juboo guy sax fukki at ca juroom ñaareelu at ma ñeel gàddaay ga yonnant bi dellu defi umra ga mu yéene woon ca daaw ja daal di siyaare ab dëkkam bi mu juddoo ginaaw ba mu fa gëjee lu tollook juroom ñaari at ci biir atum juroom ñaareel mi ñeel gàdday gi la yonnant bi j m yabal ay ndaw ca qaysar mu rom mi kisraa mu faaris mi ak kilifag qibt ya ca isipt joxaale leen ay bataaxel yu leen di xamal lislaam te di leen ci woo qaysar moom daa yeexoon a tontu bu dee kisraa mu xottite bataaxel ba waaye maqooqas moom daa tontu tontu bu rafet yonnee ca yonnant ba adiya waaye taxutoon mu dugg ci lislaam yonnant bi yonneeti ci lu bari ci njiiti araab yi ak seeni kilifa ak buur yi nekk ci mbooleem dun bi am ñu ci dëggal te gëm waaye la ca ëpp tontuwuñu xaybar am mbooloom ay waaha yu ndaw la yu nekk ci bëj gànnaaru daanaka dun bi ca waxtu woowa xaybar ci loxol yahood yi la nekkoon ñu see woon ko ngartaajoo woon ay xéewalam def ko seen dàttub xare tey seen barab bu alal ñu tàmbali woon di xiirtal seen dëkkandooy araab yi ci ñu fexeel lislaam ak madiina waaye yonnant bi dëgmalsi leen ci mbooloom xare mu mag gaw xaybar jullit ña songoo fa ak yahood ya cib xare yonnant bi dumaa leen fa ñu wommatu yeneen waaha yi ko jege woon te nekkoon ci loxol yahood yi topp ci niki fadk ak timaa ci jëf jii la yonnant bi raye jànkoonte ak jafadiku gi yahood yi dese woon daal di fegu ci seenuw ay ci biir loolu fekk na màkka mu néew lool doole ñu ëpp ci ñi ko daa jàppale bàyyi ko lislaam tas fat tas gu yéeme rawati na ginaaw juboo gu hudaybiya gi ci njëlbéenug juroom ñatteelu at mu gàddaay gi la waa quraysin firi woon seen kóllëreg juboo ga ñu defoon ak yonnant bi loolu nag mi ngi ame ci tooñ ak jalgati gi ñu defoon giirug xasaaha gi nekkoon jullit ci noonu yonnant bi jug ci fukki junniy jullit dugg màkka ci lu dul xare ci weeru koor gu juroom ñatteelu at ci gàddaay gi samwie g j bi yonnant bi duggee màkka daa daal di laabal kaaba gi dammate xërëm ya sànni leen ñu sori kaaba ga jullit ñi daal di raxas kaaba gi mu nekk leegi nag di néegub yàlla deesu fa jaamooti ku dul moom ci loolu la yàlla dëggale dëel bi mu joxoon yonnant bi ak jullit ñi ndax jàppale na leen jàppale diineem fay leen ci seen sellal gi ak dëggu gi ak jiyaar gi ñu doon def ci seen alal ak bakkan bi loolu jàllee ba teg lu néew lislaam daal di tas ci màkka gépp ñu taxawal fa ay jàkka mu mujj di ñaareelu dëkk ak digg bu lislaam ginaaw madiina gu ñu leeral gi ginaaw bi ñu ubbee màkka ba teg lu néew la giirug hawasaan ak giirug saqiif gi mu tapooloon jugoon dajale xare bu mag dox nag ngir xeexi jullit ñi waaye yonnant bi duma leen duma yu tar ca fa ñuy wax haniin bi loolu amee genn giir jugatul naan day xeex lislaam ginaaw ndam lii yonnant bi j m dem na taayif dëkk bi saqiif dëkkoon gaw ko ba gaw ga yàggee mu xam ne dana wommatu la leen fa ba dellu madiina waaye noonu la deme woon ndax yàggaatul dara taayif jébbalu giirug saqiif gépp dugg ci lislaam atum juroom ñeenteel mi ñeel gàddaay gi ñi ngi ko tudde woon atum mboolooy yi ngir ne ci la giiri dunu araab bi bépp doon yabal ay mbooloo yu bokk ci ñoom ngir yëglesi seenug dugg ci lislaam mbooloo yii nag bawoo nañu ci mbooleem goxi nga xam ne bi fukkéelu atum gàddaay giy jot fekk na mbooleem dunu araab bi dugg ci lislaam ñépp ña fa dëkk mujj bokk ci uma bi ci sawaal atum ci gàddaay gi ginaaw bi nga xamee ne mbooleem araabi daanaka dund bi dugg nanu ci lislaam la yonnant bi bëggoon a xamal jullit ñi ne jiyaar ji de fàwwu mu génn dunu araab bi ngir ñu man a tas diine ji ci àdduna bépp looloo taxoon mu wommatoon benn xare bu mag ci ay jullit dox jëm bëj gànnaar ba àgg tabuuk ca dig wa dox diggante dunu araab beek réewi shaam yi nekkoon ci ron teg loxo gu rom foofa la nguuri araab yi nekkoon ci dig yooyu duggoon ci lislaam jullit yi it xame ci ne jiyaar de day sax di wéy ba fàwwu ci silhijja atum fukkéel mu gàddaay gi la yonnant bi defi woon hajjatul wadaah di ajug tàggoo gi ba muy dem nag ma nga àndoon ak ay junniy junni ci jullit ñi ci aj gii la yonnant bi j m leerale ajiin wi ñu yoonal te mooy wii fi nekk bat ay jii ñu nekk bi mu noppee ci aj gi la def xutbaam bu bu mujj ba nuy wax xutbab tàggoo ba mu dénk ca jullit ña dëggu bennoo boole séen sàppe jóox farata yi lislaam digale ak tënku ci ponki jikkoom yu màgg yi bi mu noppee jàngal nit ñi waxi sunu boroom ju tedd ja al yawma akmaltu lakkum diinakum wa atmamtu halaykum nihmatii wa radiitu làkkumil islaama diinan di ci tay jii de laa matale seen diine ji ci laa matale xéewal gi ma leen doon jox te lislaam nag mooy diine ji ma gërëm te sopp ko ci yeen fii nag jullit ñi yëg nañu fi ne yonnant baa ngi leen di tàggu te di leen dénk li ñu war a def bu ñu ko gisatul ñoom ñépp jàq te am lu leen naqari bi yonnant bi j m delloo madiina la yëg ci mujjug safar lu mel ne tawat di ku dugg waaye faalewu ko dafa wéy di ligéey ba tawat ji far ko man mu doog a tëdd waaye tawat ji yàggul ndax mi ngi làqu ginaaw bi tawat ji amee ci moom fukki fan ak juroom di ci rabiihul awal atum g g suwe g j ci nii la yonnant bi j m tuxoo dem ca boroomam ginaaw bi mu jottalee bataaxelam bi ci anam gu mat te yaatu tas ko ba ñépp jot ci ca na mu ware wooteem gi mi ngi ko tàmbali cig wéet ay gàllankoor aki pakastal gaar ko ay yooni yoon mu daje ciy coona lol manoon naa yoqatloo geneen góor gu mu manoon a doon gu dul moom woote na fukki at ak ñatt yoy amu ca lenn ngérte lu am njariñ waaye mu sax di ku dëgër ag ngëm ci yàlla ku am kóolute ci ndimbalam wéy ca liggéeyam ba ba ndimbal dikkal kook ndam ginaaw bi mu gàddaayee dem madiina daal di fay taxawal umma bu lislaam bi dox ak moom ci yoonu nosu ak doole ci anam gu màndaqewu te callalewu weer ginaaw weer ba mujj am ci ndam lii ngay gis tay yonnant bi nag li ko dimbali ci mu jot jubluwaayam bii mooy jikko yu yéeme yi te wéet yi mu jikkoo woon ak bataaxelam bii bàyyikoo woon ca yàlla ma ko tànnoon ngir mu jottali ko ñun nag manuñoo lim mbooleem jikko ak ngënéeli yonnant bi j m looloo waral jullit ñi ñoom dañu koo def muy xam xam ci jëmmam bu ñuy jàng ñu koy wax xam xamu jikkoy muhammad as shamaayil al muhammadiya taalif nañu ci lu dul jeex ñun nag ñu ñeme ñemelu indil leen lenn ci yi ëpp solo ci jikko yii gëm gi mu gëmoon yàlla gu matale woon la te xóot da daan def fu jafe jafe yi gënee bari gàllankoor yi gën a dolliku gëmam gi ci boroomam gën a dëgër mu gën a oy ci bataaxelam bi gën a dogu ci wisaare wooteem bi ko yàlla dénk looloo taxoon yonnant bi ak saaba yi daawuñu nangu lu dul ngëm gu mat gu dara ci sikk dul jege ci daaray ngëm gu xóot gii la saaba yu mag yi génne ku ci mel ne aboo bakr omar aliyu usmaan sahd ubn abii waqaas abii hubaydata haamir ibn jaraah talhata bn hubaydul laah zubayru bnul hawaam ak ñi mel ni ñoom ci ñi war a yanuji raayob lislaam ginaaw yonnant bi j m te war a tasaareji diiney yàlla ji ci li ëpp ci pàkki àdduna yi ñu xamoon ca jamono jooja ngir gëm gu dëgër gu xóot googu ci boroomam t s ak ci lislaam daawoo gis yonnant bi mukk muy jëf ci lenn ndare bu tegu ko ci gën jaa dëgëri dàtti jikko yi niki dëggu matal kóllare wóor gu mat ci wax ak jëf ak seelug yéene ci lépp lu muy wax mbaa mu koy jëf ak tëyye bu dëgër cig maandu ci mbooleem ay jëflanteem aki saabaam ba ci ay kontaram nekkoon na di ku bu waxee dëggal bu dëelee matale bu kóllarantee def ko bu manee jéggale yonnant bi de ak li ko dikkaloon lépp ci xéewali àdduna ak teddnga ak doole teewutoon mu nekkoon di kuy doylu ci gën jaa tuuti ci xéewal yi dundam gépp masu cee feesal biiram ciw ñam lu néew ci mburu la daa mos ak tàndarma bu amul rëndaay mu rëndaayoo diw mbaa diw ak bineegar mbubbam ak dallam ci loxoom la ko daa daaxe daan fóot mbubbam bis bu jot ci loxoom ndax moom j m ku jéggi woon ab dayo la ci set bis bu nekk daa na ci socc ay yooni yoon daawul toggoo nag ag dund gu ñagas te di ko woote moom kay ñam wu ko dikkal rekk mu lekk soloos na ci moom ne daawul sàkku mukk aw ñam wu fi nekkul cib pajaas la daan nelawe am mbalaanam it lu gàtt la daan doon daawul tëju ay saabaam ki gën a doyodi ci nit ñi da ko daa gis di wax ak moom waayam ja ko daa ligéeyal di anas mom maalik nee na masul a dégg ci yonnant bi ci dundam gépp benn baat bu ko mas a naqari daf daan bàyyee saabaam yi xéewal yi te daawu ci féetewoo dara bàyyi leen nekkoon na di ku sopp xale yi te daan kaf ak ñoom ku amoon ag ñeewant la ci jirim yi way ñàkk yi ñu doyadi ñi di seeti way tawat yi bëcëg bépp it ci yëgg la daan nekk daawul dal ku bañoonug jekki la ak tàyyeel daa na ko moytulooy saabaam yonnant bi ku amoon ag yewwute gu sax la daawul ba dara romb ko ci lu aju ci umma bi ndare bu da koo gendiku bu baax te settantal ko daf daan settantal di teg ay naal yu jub yu yaatu yu muy jaar ci ligéeyam ci anam gu nosu te toftaloo yitteem jépp da ko daa sotti ci li ëpp solo ci mbiri xeetam wi teg ca la ca topp cig am solo daa gisoon ne ay ligéeyam aki jëfam roytéef la wuy saabaam di jaari ëlëg làmp la bu ñuy niitloo moo waraloon lu muy def rekk mu koy def cig njàngale cig yare bu kenn ci saabaam yi juumee ci mbir da ko koy won cig nooy leeral ko lay la jub ku daan am ag muñ ci way xuloo yi la daan leen jéggal seeni soppaxndikooki jikko yu ñaaw ngir ñu gis seen njuumte dellu ca jub ga ku wormaaloon nit ñépp la daan sàmmoonteek teddngay ki gën di gone ci ñoom ak àqam masuñoo dégg fenn fu ñu ne yonnant bi j m génnee na fa baat bu ñaaw jëme ko ci kenn ak doonte kenn kooku da dib noonam bu masaan a mer day noppi ba mer wa dañ mu doog a wax nànk cig dal yonnant bi noppee ko gënaloon wax dégloo ko gënaloon déggal bu masaan a wax day àgg ca la mu bëgg a wax du jàdd jàddal def ko it ci baat yu leer te gàtt looloo taxoon yonnant bi j m moo gënoon a am fasaaha ci nit ñi gën cee am balaaxa adiisam yi ci balaaxa ñoo topp ci alquraan miy wax ji gën a balaaxaa ci wax yi yonnant bi j m yérmaande la ñeel mbindéef yépp bi muy ñëw ci àdduna bi da koo fekkoon mu yor lëndëmug réer ndof xamadi yàlla waaye mu bàyyikoo fi ba fi ag leerug gëm yàlla mi ngi feeñ ci araab yi te booba ñi ngi ciy xareek fitna ak aayoo mu juge fi ba leen ñuy xeet wuy wenn yiw peek leen lislaam ëmb leen jàmm uuf leen ak li yàlla sotti nit ñi lépp ciy xéewal jaarale ko ciy loxoom teewul yonnant bi jàmm yal na nekk ci moom bi mu fiy juge di woon ku ndóol ku moomul lenn saddaloon na nit ñi aw léew ci nite ngënéel def wartéef sellal ak dëggu yàlla dëggal na tudd naa sellam ga ba mu nee yaa ayuhan nabiyu inna arsalnaaka shaahidan wa mubashiran wa nadiiran wa daahiyan ilal laahi bi idnihii wa siraajan muniiran wa bashiril moominiina bi anna lahum minal laahi fadlan kabiiran muy yaw yonnant bi de dañu laa yonni ngay seere tey bégaleek a xuppe di woote jëme ci yàlla ci ndigalam tey làmp buy leeral na nga bégal jullit ñi ci ne am nañu ngënéel lu rëy lu tukkee ca yàlla yonnant bi nag j m tënk na wax jépp ca bataaxelam ba niki kuy jàngale ba mu nee dees maa yonni ngir ma mottali jikko yu rafet yi xeltu baat la bu nu doge ci filasofia muy baat bu cosaanoo ci làkkuw gereg maanaa mi mu yor ci baat yi di sopp hikma loolu di xel mu rafet sagesse ci fr ba ci laaj rekk ne lan mooy xeltu dees koy jàppe ab laaj bu di kojug xeltu bu nu man a yendu di ci dàggasante lii benn la ci màndargay xeltu yu dëgg dëgg yi ak jeng gi mu def jëm ci laaju ak defi gëstu ci lepp lu mu man a doon te jéem a xam dëgg dëggam aki màndargaam aki àtteem lii lépp a tax nag xeltu di xam xam bu yaatu te bari ay ñall laal daanaka ci xam xam yépp walla ci mbooleem wàlli dund waaye loolu lépp téewul muy xam xam bu wéet ci boppam wëlif yeneen xam xam yeek jagoo yi specialisation xeltu leeg leeg ñu melal ko ci ne mooy xalaat ci xalaat maanaam xalaat ci jëmmi xalaat cib déndam ak ci settantal dees na ko melal it ci ne mooy jéem a indi ay tontu ci laaj yi am gi di indi ak nekk gi l existence xeltu seere na ay jëm kanam yu am solo te lëw dale ko ca waa geres ya sos ponki xeltu yu mag yi niki xam xam buy tabax ab gis gis bu matale ñeel nekk gi adduna bi ci biir gis gis bu di kojug li am réaliste ba ca xeltukati jullit ñi nga xam ne danoo jëflanteek ndonol geres li li fi waa geres yu yàgg ya ba woon jaxase kook nattu experimentation daal di soppi xeltu bu kojug li am bi yóbbu ko ci xeltu bu kojug tur ak xeltu bu kojug xam xam ak nattu ci jamonoy yewwute walla judduwaat renaissance teg ci xeltu yu kojug am yi existence ak yu kojug nite yi ak ngéri yees gi ak la ca ginaaw yeeg ak ñàkk maanaam dee walla bañ a am xeltu gu yees gi ci aaday seggat ci amerig gu bëj gànnaar gi usa ak nguur gu bennoo gi uk ci seen aada ji nu am ci seggat mbir yi anaaliise ko day barastiku jëm ci gën a nekk gu xarala ci gu neen rekk moom day taxaw ci xellu logique ak ceggat gu dégg dégg conceptual analysis looloo waral ay tërte sujets yi yitteem di jëm day àgg ci làmboo gis gis bu kojug xam ak jikko ak déndu làkk ak déndu xel am na yeneen xam xam ak jubluwaay yu jàppe xeltu muy jàng fann walla ci fr art ak xam xam yi bu ko defee muy gis gis bu daj te matale di tegtalub dund bu ubale te daj ci déggiin wii la xeltu di nekke di luy yittewoo xamale yoonu dund ga gën dootul nekkati luy jéem a xam dund gi jamono yi jubluwaay bu seggat bi jàppee xeltu muy mbirum jëf mom fawwu nu jonjook moom doxal ko jëf ko am na yeneen një jubluwaay yu ko jàppe muy cëslaay base li xam tegu ñu war koo xam xam gu wér te xereñe ko xeltu baat la bu gereg bu juge ci fila di tekki sopp ak sofia di tekki hikma maanaam sagesse walla xel mu rafet kon muy firi sopp hikma baatub xeltu ci jamono ju yees ji ñi ngi koy wax jublu ci dox gi nit di dox ngir xam laaj yu mag yi aju cig dundam bokk na ci yooyu dund ak dee ak li am realité ak maanaa yi ak dëgg baatu xeltu it dees na ko di faral di jëfandikoo ngir xamalee ci li xeltukat yu mag yi def ciy liggéey yu nu bokk waxtaan ci xeltu du lu waa geres jagoo ñoom rekk waaye kay ag wàll la ci xayug civilisation xeet wu nekk xeet yépp a ci bokk looloo tax laaj luy xeltu du tekki benn tontu rekk xeltu cig tàmaleem ca jamonoy taalis da doon gëstu cosaanul am gi l existence ak aji bind ji le créateur ak ne ne matiere bi ñu binde mbindéef yi ak xeet elements yi leen toggale bu ko defee dàggasante gi wéy di tang ci loolu ba ci jamonoy sinon ak sofistaa yi nga xam ne danu doon jëfandikoo xeltu ci weddi yàlla ak wëlbati maanaa yi ak dégg déggi baat yi li nu ciy dégge ngir notal seeni gis gis waaye mi ngi tàmbali ci jamonoy sokraat mi siisroon doon melal ci ne mooy ki wàcce xeltu ci suuf si jële ko ci asamaan si maanaam mooy ki jële xeltu ci xalaat ci nekk gi ak ki ko sàkk ak xeet elements yi mu ko toggalee yi mu ko sàkke yóbbu ko ci xalaat ci jëmmi nit moom nag soppi na lu bari ciy màndargaam daal di tuxal ay aayoom aki dàggasanteem yóbbu leen leegi ci déndub nit nature am ak dëgg dëggam ak gëm aji bind ji te gëstu ko te jëfandikoo tegtalu xel ci saxal ko sokraat nag jëfandikoo woon na xeltu ngir tas jikko yu rafet ci biir nit ñi ak dëggu ak soppante sokraat nag ñëw na mook aflaton platon sukkandiku ci ñaari jumtukaay yii di xel ak xellu logique niki cëslaayi xalaat bu sell te mucc ayib xalaat bob day dox dëppoo ak ay ponk yuy leeral ag wéram akug neenam laaj luy xeltu bii laaj aristo tontu na ko ci noonu sunu wax ji amatul njariñ ndax dafa jeex te tàmbaleegul kon tontu bu gaaw bi ci loolu day man a taxaw ci cëslaay lii tontu bi aristo joxe woon ci lan mooy dëgg dëggi xeltu du moom rekk mooy tontu bi nu ci man a joxe ca dëgg dëgg loolu daal benn rekk la ci tontu yi nu ci man a joxe nit daal bu sukkandikoo ci ni aristo xamalee xeltu dina man a xalaat te firi xalaat yi jiitu aristo ak aflaaton ak xeltu yi ñëw ginaawam ànd ak loolu teewul nit ki dina seetlu ci anam gu yomb ne xeltu de ak yoon wi nu xame dëgg dëggam soppiku nanu ci ñaari junniy at yi topp ci aristo soppiku gu mag waaye ci biir loolu jëmm ji wart a réere ne xeltu la ko dale ca aristo ba ca nits dafa sax ci cëslaayi soppiku yooyu ak yu leen moy di moom ci jëmmi boppam ndax kat soppiku yooyu dafa ame ci wàllug xereñ wattu ag yamoo ci biir moom moom la lu wér la ne dinanu man a ame ci yoon woowu ay xam xam yu wuute te xóot neel yu am njariñ ci ni xeltu feeñe ànd ak taariix waaye nag woowu yoon dunu may ñu àgg ci am tontu yu dëggu maanaam yu yoonu ci lan mooy xeltu ni aristo firee xeltu ne mooy sopp hikma am na lu ëpp benn teglal walla maanaa tegtalub làkk bi moom mi ngi aju ci làkku gereg wi ñu tëgge baatub filosofia ak tegtalub xam xam bi nga xam ne dafa wuuteek li nu nekk lool sikk amul ci ne tegtal bu mujj bi walla maanaa mu mujj mi mooy bi leeral maanaa mi gaw ko ci sopp hikma niki melo wu nu man a wonee ñàkk gi ay am am donnés yu xam xam ñàkkoon ñeel xeltukat bi ca jamono jooja bu ko defee hikma nekkoon benn ci pexe yi ñu daa pexee ci lu nu xamul niki ab ne ne bu njëkk bi nga xam ne ci la xeltukat biy sose nosteg xam xamam mu dëppook settantal gu xam xam ga amoon ca jamono jooja bu dee leegi nga xam ne xam xam daa sakkan li ñu wuññi lëw laaj yi bari ci ëtt yu bari ak mbir yu dul jeex ak jëm kanam gi nit def ci wàll yu bari loolu lépp tax na ba liggéeyub xeltukat du doonati rekk sopp hikma ak gëstu ko ci jumtukaay yi mu ko daa gëstoo ak ci ron kilimb réer gu tar gi mu amoon ci wërlaayug àdduna gi ko wëroon ca jooja jamono xeltukat leegi lu sakkan ciy ngér ecole methode ñoo ko tënk aki àtte yu di kojug xellu aki am am yu di kojug péng lu wóor ci ron jalub ay xam xam ak seeni doxal pratique yu xarala yu la dul may fenn fooy sikke seenug nekk di yoon ci ndabi jamono conditions yu mel ne yii ak ci am am yu nirook yii xamaleg xeltu ga nu xamoon du manatee dëppook liggéey bi xeltukat bu jamonoo bi man a def maanaam bu sunu jamono jii nu nekk moom mi nga xam ne ab liggéeyam daa wuuteek bu ñoñ jamono yu yàgg ya lool bu nu sukkandikoo ci li jiitu danu naan manatuñoo def nenn nu dul jéem a xool nu nuy soppee dégg dégg ak maanaam xeltu ndax mu doon leegi juddal hikma te bañ a doonati sopp hikma wuutuloxo walla masin mbooloom ay cër la yu am lu bon bon benn bu man a yëngu yees lëkkale ngir jublu ci mu def jenn jëf ji jees tëral jëkk kon muy lu man a def liggéey bu nit dul man ndax xéj na dafa laaj jenn doole ji walla mu koy war a defe ci wërlaay gu nit manuta dund xeeti wuutuloxo yi bari nañu te itam dañu leen defar ngir njariñ yu wuute ci misaal wuutuloxo bu mbëj wuutuloxo bu mbay wuutuloxo bu yóbbte ak yëkkati ak yeneen jëfandikoo gu wuutuloxo yi dimbali na nit ñi ba ñu man a def liggéey yoo xam ne weesu nañu dooleem kàttanam bu dul woon wuutuloxo yi nit ci dundiinu nit ñu njëkk ña lay des ba tay te du am nenn numu man a def ba jëm kanam kon wuutuloxo day tekki bepp jumtukaay buy yokk sa doole di wàññi sa coono te di gaawal aka gënal sa liggéey melosuuf mooy xam xam biy settantal ak a leeral feeñtey yaram yi walla jëmm yi ak yu dundat yi a yu nit ñi ci kaw suuf si ak gëstu gi aju ci ni ñu séddalikoo séwogaraafi baatub gereg la boo ko doon firi ci wolof muy melal suuf si maanaam wax ni mu mel ni mu nekke moom nag baat la bu tukkee ci geographica baatub gereg bob cosaanam mooy geography muy ñaari baat yu ñu boole ñuy benn bu njëkk bi mooy tekki melo walla nataal graphica ñaareel bi di geo di tekki suuf bu nu sukkandikoo ci loolu danu naan sewograafi walla geographia mooy melal suuf si walla wax ni mu mel xam xam bii noonu la tàmblee woon ndax ca njëlbéen ga tukkikat yi daa wër di gëstu dañu daa bind li ñu gis ci dëkk yi nu romb ak gox yi ak diiwaan yi ñu siyaare leeral melal ni ñu leen gise fekke leen ni sewogaraafi nag déggoo nanu ci séddale ko ay xaaj ñooy yii séwogaraafi bu dénd bi nature mooy biy sonn ci gëstu ni suuf si mel ni mu bindoo ci wàllug jiyoloji ak feeñte fenomene yu jawwu yi ak gàncax yeek dundat animal gu dénd geeg gu jeeri ji bokk na ci xaaj yooyu séwogaraafi bu bidiw li ko tax a jug di jàng ni suuf si bindoo ak ab kemam ni muy yëngoo ak ni mu buloo ak séqoo gi mu am ak yeneen bidiw yi bokk na ci xaaj yi ba tay séwograafi bu nit moom nag daa séddaliku ci séwogaraafi bu way dëkk yi abitant ak séwogaraafi bu koom koom ak bu politig mooy gëstu ci goxi àdduna bi aki pegam frontiere yu politig aki jafe jafeem ak ña fa dëkk ak bu nataal yi walla bu lonkoyoon yi moom mooy xam xam biy yittewoo lonkoyoon sewogaraafi yi ak ni nu leen di sose bu yàggul bànqaas bu yees sosu na ci xam xamu sewogaraafi mooy biy nos xam xam yu sewogaraafi yi ak yëglu cig sori melosuuf moom nekkatul rekk xam xam boobu di melal feeñte yi les phenomenes di leen melal ak a leeral ci anam gu tond gu soreek li am waaye mujj na di xam xam bi jagoo dox ànd ak jëm kanamug xam xam bu bees bii sukkandiku ci gëstu ak nattale ak làmb ba daj ak jëfandikoo misaal yi ak gis gis yu yees yi ci noonu la mujje di lu nuy doxal ci anam gi nuy tudde séwogaraafi bu kem ak séwogaraafi bu doxal walla dëppale bu pratique bi nga xam ne du nangoo beru wëliif soxlay nit yu mag yi loolu nag li ko waral mooy li séwogaraafi làmbool yor ko ci man manu dëppoo ak mbooleem xam xam yi moom mooy aji jokkale ji nekk ci diggante xam xam yi di leen booleek a jokkale bu ko defee di leen tàggat ngir ñu liggéeyal ko di jël ci ñoom lu koy jariñ di ko ràññale ak yeneen yi at yu mujj yii seere nanu ag soppiku gu mag ci gérum séwogaraafi ak xam xam bi mu ëmb ak ci anam yi muy jaar ngir amal ay jubluwaayam aki xemmemtéefam man naa am nag mu bokk ci li indi coppiku gii jëm gi nit ñi gën a jëm kanam nga xam ne sax boroom xam xami séogaraaf yi mujj nanu di gëstu ay mbir yoy bu njëkk xamuñu leen woon ba sax kuy seetlu liggéeyu boroom xam xam yii dana gendiku yittewoo gu dolliku gi nu sotti ci mbirum gëstu feeñte yi phenomenes ak masala yu wuute yi aju ci dénd bi ak nit ci anam gu wuuteek ga nu ko daa gëstoo bu njëkk sababus loolu nag mooy jëfandikoo gi nuy jëfandikoo leegi ay jumtukaay yu xarañ te aaytal ci seeni gëstu di dimbadikoo xam xami takk yi statistiques ak yu xibaar yu jumtukaay yi ak mat ak misaalukaay yi echantillon ak xam xamu xarala ak dénd nature bi ak kimya simi jëm kanam gii am nag ci jëfandikoo jumtukaay yii ak ker keraan yii ces moyens tax na ba ngérte resultants yu am solo juddoo ci yu jañ séwogaraafi mu jëm kanam def ko muy xam xam bu jamonoo loolu sax tax na ba ñenn ñi di woowe jëm kanam gii am ci xamu melosuuf jeqiku walla fipp gu kemu ci xam xamu séwogaraafi jeqiku gii walla fipp gii waa melosuuf yi teeru nanu ko te màggal ko ndax ngérum kem ay ngënéelam lu bari la man naa am li ëpp solo ci ngënéel yooyu mooy ngérte yi mu lay àggale yépp ñooy gën a sew gën a am maanaa ngir seggat analyse gu xam xam gi muy amal ñeel toftaloog mbir yi ceggat gu xam xam gu melosuuf gii mooy wone noste systeme yi amal ay jeexiital ci amug feeñte yu wuute yi melosuuf di gëstu moom du doylu ci leeral feeñte yi rekk waaye day sukkandiku ci sabab yi sos feeñte yii ngir melosuuf man a génne feeñal lëj lëj ak jafe jafe yi gawu cib gox walla ab diiwaan li muy njëkk a def mooy digal ëtt boobu walla barab boobu maanaam wutal ko aw dig ba ñu xam ne fii la bu ko defee mu fésal séqoo les relations yi am ci diggante mbooleem xeet element yu wuute yu kojug dénd yi naturel ak yu kojug nit yi ak nu ñu man a duggantee ci seen biir ràbbaloo ni looloo tax séwogaraafi fi di boroom jikoo ju ràññiku ndax danu koy gis mu tegub tànk ci xam xami dénd yi tegati beneen ci yu nit yi bu fekkee ne xam xam yu wuute yi ci atum lanu leen raale nos leen séddale leen ñatti kuréel ñooy xam xami seggat yu nattu yi xam xami firi yi ak taawiil ak xam xami jam yi yu critique yi bu fekkee ne noonu la it melosuuf moom jël na mbooleem jikkoy yii kuréeli xam xam jàng ëttub melosuuf dina feddali amug ay way nekk yu bari yu dénd ak yu nit yu lënkaloo yuy ràññikoo ci jëflante yu bari yuy am ci diggante way nekk yii loolu moo lay won foofu solos boroom xam xamu melosuuf looloo tax nga gis gëstu ëttub melosuuf du yam rekk ci menn mbir walla benn feeñte bàyyi ya ca des ak doonte ëttub melosuuf làmboo na mbooleem feeñte yépp teewul gëstug feeñte yii day am cig beru tey natt tolluwaayu jëflante gii seggat ko yillaal ko ci lu dul muy sàggane benn xeet element ci xeeti ëtt bi ngir solos ëttub melosuuf unesco saxal na ni nu koy jàngalee ci tugal ci donga yiy door a dal bu ko defee ñuy def aw doxaliinam sukkandiku ci dégg te xam juroomi laaj loolu nag mooy ëtt biy jóox biy produire bu ñu laajee njàggaan li jéego yi aju ci déggiinu ëtt biy jóox loolu man naa doon yoon wi ngir xam dëgg gi maanaam yewwu ci ne ëtt boo gis du lu dul melo ci meloy yëngu yi maanaam mi ngi ci melow jóox kon nag ngértel saxal yu tukkee ci nit ñi la jeexiitalu jëfi nit boo gëstoo lonkoyoon carte adduna bi bu baax di nga ca gis dëgg yii bii mooy teereb irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim di ci maanaa nàndalug aji naanaale ji ki ngay toogal di naan ci ndox mu neexum sopp jëwrinu yonant bi di xam xamu jaloore bu nu gàttal mu ñeel nag ki bëgg a am ab xam xam ci dundug sëriñ ahmadu bamba yal na yàlla dolli gërëmam ci moom te jariñ ñu ci amiin ki ko taalif it di ku xeebu ku aajowoo ndimbalul boroomam ak yermaandeem tey yaakaar ci moom mu jéggal ko ay bàkkaaram te làqal ko ay ayibam yi feeñ ak yi nëbbu fii ak fan jëm di muhammadul amiin joop doomi sheex ahmadu joop mu dagana yal na leen yàlla boole jéggal di it taalibeb sëriñ tuubaa yal na ko yàlla gërëm te jariñ ñu ci moom amiin maa ngi ñaan yàlla mu musal ma ci saytaane mu nu jam mi di tàmblee nag samay wax ak jëf ci turam wu tedd wi moom mi yor yërmaande ju yaatu ji matale mbindeefam yi ci àdduna te di ko jagleel ñi ko soob ca àllaaxira yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci sunu sang muhammad ak ñoñam aki saabaam aji xeebu ju yitewoo yërmaandey boroomam ak ndimbalam ci ligeeyal yarkatam bii dib soppeem di sëriñ tuubaa aji xeebu jooju di muhammadul amiin joop doomi sheex ahmadu joop mu dagana nee na ag cant ñeel na yàlla miy leeral àddinaam ji ci walliyoom yi di feeñalati ci ñoom yoonu yonantam yiy gindee yoon woowu di wu weetal yàlla ak jaamu ko mooy yoonuw boroom xel yiy dàq lu dul yàlla ci seeni xel tey jànge ag njub ca yooyale imam ci jox leen seen bopp jébbal leen seeni mbir ndax kat ñooñooy ñi yàlla naan ci alxuraan ulaayikal lathiina hadaahumul laahu fabi hudaahumuqtadih muy ci maanaa ñooñooy ñi yàlla gindi kon royal ci seenug gindi di julli tey sëlmël ci yonant bi leegi nag ginaaw yàlla day xéewale xarnu bu ne aw waliyu wu koy gindi di ko won yoonu jub di ko tee jàdd nun waa xarnub fokk ñeent nag mu defal nu xeewal gu tollu ne sunu mbeg mii di sunub sëriñ tey sëriñub julit ñi ahmadu doomi muhammad doomi habiibullaah yal na ko yàlla wattu te wattul ko te gërëmi jëfam te méngoo ko moom nag mbooloo maa ng ko gën a xame ci turu sheex ahmad bamba mbakke xaadimur rasuul bi loolu amee ma bëggoon a leeral as lëf cig dundam ñeel ki nar a ñëw ginaawam te bëgg a xam dara ciy mayam man nag maa ngi giñ ci yàlla dellu di ci giñaat naan dey xam naa ni xawma te du ma ci man a wax mbaa indi lu dul la gën a neew la gën a bari moom bu ko xalaat ndax manu ma ko ba koy def waaye nag dinaa jeem a nooyal yoon wi ba ku bëgg te yàlla ubbi ko barilub xam xamam yinkiiwal ko jariñ jaamam yi ngir sàkku ci ngërëmam bu ñewee man cee jaar ndax kat am na ci addiiz mu sell mi mbindeef yi njabootug yàlla lanu ki ci yàlla gën a bëgg mooy ki ci ëpp njariñ ci njabootam gi nee nanu ku taarixal aw walliyu mel na ni dundal nga ko kon am leen gàttalug jaloore jaloore mooy taariix walla histoire gii ma tudde irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim may ñaan nag képp ku ci gis lu ko yeemut mu xam ne gàttub jéegoo ma tooñ mu jeggalul ma yàlla te suturaal ma te bañ koo ngàññi ndax kat da na ci gisi leneen lu bari lu koy yeem lu man a wecci loolu ko yeemutoon ndax teere bii ab muxaddima rekk la ag jiital teere degg bi mooy minanul baaqiil qadiim fii maathiris zheixil xadiim muy ci maanaa xeewali aji des jiy aji jiitu ci ngëneeli sheexul xadiim doomam ja sheex muhammadul bashiir defoon ko yal na ko yàlla sàmmu te guddalu fanam te jariñ ci lu bari jullit ñi ni baayam moom dey teere bu boole la te wattu te dib dër bu naat ñeel ku bëgguw yiw te di ci dox yal na ko yàlla mottali te nangu ko te tas ko ci àddina bi muy ndaxañteefam ëlëg ca àllaaxira tey lu nu koy fàttalikoo ginaawam ci fii fi àdduna ci barkeem ak ci barkeb ki ko taalif ak kim ko taalifal yal na nu yàlla nangul te nangul nu sunub teere matal ko te tas ko moom itam moom kat yàlla mooy aji kawe jiy boroom ngëneel ak tawfeex tey borom li fii ak la fee sëriñ baa ngi gane àdduna ci li nu wax ci atum junni ak ñaat teemeer ak juroom ñaar fukk g am ñu ne atum junni ak ñaat teemeer ak juroom ñaar fukk ak ñaar g ca kër waajuram wu goor ca mbakke bawal mu nekk leegi ca wetu yoonu saxaar ga boroom xam xam bu mag bi nuy wax alhaaji hamidin doomi usmaan alfuutiyu altilriyu nee na sëriñ baa ngi gane àdduna moom mi sunnawoo sunnas yonnant bi ci atum sharaha muy g làqu atum shumoos muy g te booba mi ngi am juroom ñaar fukki at ak ñeent mel ni ay jant am ñu ne juroom ñaar fukk ak ñaar ci guddig àllarba ci ñaar fukki fani muharram moom sëriñ bi bi mu ganee àdduna waajuram wu jigeen a ko yoroon bam mat a jàngi mu tudoon nag amadu doomi muhammad doomi habiibullaah doomi muhammadul kabiir mom habiiballaah mu njëkk ma doomi muhammadul xayri ak muhammadul kabiir muhammadul kabiir mii mooy ki niy wooye maharam mooy ki sanc mbakke bawal atum g ci li nu wax waaye dëkkewu ko woon da faa ba woon ab taawam muhammudu farimata magi habiibullaah waaye bokkunu nday moom nag sëñ maharam mii daa desoon jolof fa la làqqoo nu denci ko fa di ko siaare mi ngi askanoo nag ci tukkloor ay waajuram a ngi bawoo fuuta dem jolof siw na itam ne ñoom gànnaar lan bawoo dem fuuta seeni doomi baay tëx ci naar yi ñooy ñoñu moodi nalla ñoom nee nanu ay serif lanu sama mag sama sëriñ sheex muxtaar binta loo doomi sheex iraahiima sëriñub njumri loo nettali na ma ne degg na ci sëriñ bi luy dëgëral loolu mu ne bis nekk na fa sëñ ba nuy waxtaan ba tudd ag giir ci naar yi gu niy askanale ag cëriif sëñ bi ne ko xanaa xamoo ne ñooñu suniy mbokk lanu mu ne ci noonu la xame ne ñoom ay sëriif lan man nag li may wax mooy seenug cëriif bu nu ko waxutoon te deggeesu ko it seen jikko yu rafet tegtale na ko muy tedd gu ànd ak yaatug dënn ak lewet gu ànd ak njàmmaar ak jublu ciw yiw ak bañ jikko yu suufe yi ak diinewu gu dëggu yaayam soxna jaaratul laahi maryama buso doomi muhammad mom muhammad mom hammaad mom alliyu albusobiyu ñooñii seenug cëriif lu wér la ñi ngi cosaanoo ca imaam hasan mom alliyu ibnu abii taalib karramal laahu wajhahuu kon sëñ bi serif la ci nday ak ci baay lenn ci samay doomi baay tëx nettali na ma te moom ku dañ kumpa la ci suufus fuuta mu ne dox na bis juge ci dëkk bu ndaw bu nu naan bukke jëm fun naan mbumbe péeyub filaaw nee na mu romb ci ay gent yu ñu ne ko ñooy fi mbakke makke yi dëkke woon am na ku ma nettali ci ñi sant ba ne mbakke mbakke yi seeni doomi baay tëx lanu kaaf gi nekk ci mbakke ag haa la woon muy haa giy mujj ci ba wolof yi def ko kaaf waaye wax jooju ju doyadi la fi man li nu jortu daal mooy aw sant wu yàgg la niki santi ajam yi ajam mooy ku dul araab li fi ne daal mooy ñaari wax yi bu ci ne dëgër na te am na màndargaam dëgg waaye buso boso yi ñoom seen cosaan fuuta la ca fa niy wax golare barab yii yepp it yu jegee lanu barab yii it ak wax yi ci am am nanu màndargay dëgg yuy tegtale teddgay ñaari askan yi bi sëriñ bi tollee ci war a jàngi wayjuram dal di koy jébbal nijaayam muhammad doomi muhammad buso mbokkum ndayam ju tedd ju yiw ja mu tàmbli koo jàngal ba mu màgu s lëf tàmblee yewwu mu jebbal ko moom itam nijaayam sëriñ tafsiir mbakke ndumbe doomi muhammadu soxna buso doomi muhammadul kabiir mi nu tuddoon moom mooy mbokkum maami sëriñ bi ju jigeen ndayi wayjuram wu jigeen soxna asta waalo nu daan nekk foofa fa moom ca mbakke bu noor baa bu nawet baa lu ci ëpp danu daa dem jolof ba bi tafsiir mii làqoo te booba sëriñ baa ngi jeggee mokkal kenn ci ñunu woolu ñi nettali na ma ne sëriñ bi nettali na ko ne àlliwaam a ngi tulloon ci latajjidanna bi jànglekatam boobu di làqu mu dal di dellu ca wayjur wa dal di farlu ci njàng mi ba mokkal alxuraan def tajwiid ak tas hiih ca ña ko daa defale ca jamono jooja loolu lepp ci wetu baayam daa wul tàggalikook moom lu dul lu neew ndaxte magam muhammad jaara dafa nekkoon ca kenn ca tas hiihkat ya ca yeneen dëkk ya bu ko defee leeg leeg amaa na mu jaar fa nekk faak moom weer walla ñaar doog a dellu booba ña nga saalum ca jamonoy jihaadkat boobu di mabba jaxu ndax kat booba ñoñam mabba boole woon na leen ca ñam pangoon jëme saalum nga xam ne bawal ak jolof daanaka bawu fa kenn bi mu faatoo nag moom mabba nit ñi dal di dellu seeni dëkk waajuram wi moom itam dellusi ci ñi doon dellusi ànd ak latjoor ci noonu nijaayam akug njabootam des foofa sëriñ bi it bokk ci ngir jàng xam xam noonu mu tàmbli di jàng ci baay tëxam samba tukkloor ka doomi bàjjani baayam bi mu jàngee ci moom dali xam xam tàmblee ñawu s lëf la dellu ca baayam te booba ma nga paataar benn dëkk bu ndaw bu nekk ca wetu njéndul amadi yala dëkkuwaayub latjoor ca joojale jamono ndax moom sëñ mammoor daa defoon ku latjoor fonkoon lool daa ko laaj tey diisook moom waaye moom sëñ mammoor bëggutoon a dëkk ak moom ndaxte du woon ku xemmeem seen alal ji du caageenug seen teddngay nguur gi li ko loruloo woon ci mu dëppoo ak ñoom ak a mudaaranteek ñoom mooy njaboot gi mu yoroon bu ko defee latjoor daa ko dëkkal ci wetam waaye sëñ bi daawul nangoo dëkk ak moom moom kay day dëkk ca wetu péey ba mu ne rekk ndax da daa jàng ak a jàngale te jàng ak a jàngale neexoowut aki buur li fi ne daal ca wetam la dëkke woon nga xam ne su ko soxlaa ñëw ci lu dulub coona ci noonu sëñ bi nekk ak waajuram di jàng ci moom te di farlu ci mokkal gi ak xereñe gi ak dégg dégglu gi ba faf raw ci fann yi ci biib diir it daa na ci def leeg leeg mu seeti sëñ xaali majaxate kala moom mi dëkke woon fa péey baak lajoor di woon ku raw ci fanni xam xam yi rawati na làkkuw araab di ku siiw ci man a woy bu ko defee muy xamlu ci moom araab leeg leeg it mu daa ko indili woy yu mu def ngir mu toppal ko lihraab ba ak araabe ga ak harool ba leeg leeg mu genneel ko ci b yàq ba mujj sëñ bi far ko raw mu mujj saa su ko wonatee lenn ci woyam yooyu mu ni ko indil ma ko ma mokkal ko mu mujj toppalatu ko waaye day mokkal lim koy indil nii la nekke woon ak xaali amoon na fa it beneen boroom xam xam ci waa gànnaar yi dëkke woon njaañ tuddoon muammad mom muhammadul kariim bokkoon ci giirug daymaan ci doomi seyidil faadal yi ñu gënon koo xam nag ci turu muhammadul yadaali waaye bokkul ak ki def teere bi nu naan zahabul ibriiz ci tafsiir ndax kooku am yadaalim daymaan mu yàgg la sëñ bi bariwaa na lu mu ko daa dikkal di jàng ci moom xam xamu bayaan xam xamu wax ju rafet yaakaar naa ne nee na it ci lenn li mu nu daa nettali yàlla a xam ak bu mantiq xam xamu xellu bi wayjur wi xamee ci moom raw geek cawarte geek laabiir gi mu dal di koy jox mbirum njàngale mi bari na lu mu ko daa jàngal ab bind ci kanamam ci teereb boppam ba walla ci teere bu mu dalagul ngir mu jàngal ko boroom bind boobee walla teere ba bu ñewee ngir wóolu gu mu wóolu xam xamam akug ñawam sëñ bi it daan ko def ba li ëpp ci dongay sëñ mammoor yi mujj féeteseek moo doylu ci moom waajur wi ba leen ak moom te bég ci waaye yàggul dara rekk latjoor tuxoo kër amadu yala dem sukeer péeyam ba ca kajoor yobbaale sëñ mammoor mu sanci ca wetam tudde ko mbakke kajoor sax fa ñaari at dal di wuyyuji boroomam nee nanu looloo ngi am ci muharram atum g dëgg naa ci sëñ bi mu ne bi waajur wi tollee ci sukkuraat took na fa boppam wàcce fa ab kaamil bisub altine guddig talaata mu làqqu nu denci ko deqale di ko siaare man dey alhamdu lillaah dem naa fa ba siyaare ko bi niy yobbu wayjur wi deqale muy dëkk bu ndaw ci dëkki kokki yi ci wallug mbaakol sëñ bi àndon na ca gunge ba di liiru bariwaa na bu ko ab gawar bëggee joxuw fasam mu ne dox a ma gënal bi mbooloom dëkk bepp dajee di mbooloo mu kenn masta gis nu jublu ci jullee néew bi jiital sëñ tayba muhammadu ndumbe maar silla mi nu tuddoon ci buntub seedey ñu mag ñi ñeel kii nuy wax ci moom bi nu noppee ci julli gi ak denci gi sëñ tayba digale na nu daje te dal te xerawlu ci noonu mu jug xutba waar nit ñi wax wax ju rafet bi miy jaale sëñ bi nit ñi bi mu noppee ne ana sëñ bamba noonu la nu ko daa wooye ñoom ca jooja jamono mu wuyyu jug ma nga woon ca catul mbooloo ma sëñ tayba ne ko jegesil mu xaw a jege bay degganteek moom di gisanteek moom di ko man a toontu ci lu dul muy yekkati kàddoom dal di yam foofa ngir bañ a jéggi nit ñi xutbakat bi neeti ko jegesil mu ne ko maa ngi lay dégg sëñ tayba dal di koy jaale njaal mu rafet ne man nag dama doon sàkku nu ànd ci mbooloo mu màgg mu sa moroomi waajur wii ngir nu seeti latjoor jaale ko sa waajur wi jaale gu ko man a dëfal ngir kat moom ab xaritam la woon dib soppeem te dib sëriñam daa diisook moom bu ko defee nu waxtaan ak moom ci yaw sampu la fa moom ba mu man laa teg fam tegoon sa baay bu ko defee doo gis ci moom lu dul aw yiw ak teraanga lii daal mooy sama xalaat yaw nag luy sa xalaat sëñ bi ne ko li aju ci jaale geek dëfal gi maa ngi la ciy sant te di la ci ñaanalub yool waaye mbirum seeti ay buuri àdduna moom duma ko def ndax xemmeemu ma seen àddina ji te soxlawu ma seen teddnga teddnga ci yàlla laa koy sàkkoo buurub buur yi mbooloo ma tiit tas ña cay ñu baax wax ji da leen a yeem rusloo leen ndax dëggu gi mu dëggu tey toroxal way bëgg yi àdduna juge ci seen doom ju diw waxambaane tegi tànkam ci seeni wagg te manu ñu ci dara bu dee mbooloo mi moom li leen yeem mooy bañ gi mu bañ teraanga ju teew jii ak xéewal gu jàppandi gii nu ne kii daalub dof la ci loolu sëñ bi def na ñaari dagiiti woy yu rafet te yeeme bu njëkk bi mooy waxam jii nee nanub dof laa ngir wëlbati gi ma wëlbati samab gis wëliif leen ba fam yam teewluwu ma ko te woneesu ma ab yaxam jamono ja may liggéey waaye beneen bi moom mooy wax jii nee nanu ma jengal jëm ci bunti buur yi kon dey da nga ami may yu lay jariñ jamono ju ne ma ne leen yàlla doy na ma doyloo naa ko soxlawu ma lu dul xam xam ak diine yaakaaru ma te ragalu ma ku dul sama boroom ndax yàllaay ki may doyluloo te di ma musal nu may joyale samay mbir jëme ko ci ñoñ lottu nanu ci seen mbiri bopp ni miskiin yiy lotte walla nan la ma bëgg poñatum àdduna bii di jañe jëm ci dëkkaale ak ñoñ seeni kër mooy dërub saytaane su ma dee naqarlu mbaa may bég boroom aras laay woo mooy aji dimbali ji dara dul të te mooy kiy amal li ko soob bu bëggee gaawalum mbir loola gaaw bu ko nammee yeexal mu yeex ba cib diir yaw mi may yedd bul sonal sa bopp ndax kat man awma lenn lu ma naqari ci ñàkk àddina bu dee sama ayib mooy dëddu gi ma def ci seen poñat mi kon dey ayib jooju ju gànjaru la ju ma dul gecceel waajuram wu jigeen wu tedd waa nga làqqoo poroxaan ca saalum nu denc ko fa jamono ja fa sëñ mammoor nekkee moom sëñ bi bi waajur wiy dund nanguwtoon a taxaw mbaa muy taxawal dara moom daal ci moom rekk la toppoon mel ne néew bu nuy sang fu nu ko jëmewul du fa jëm bi mu làqqoo nag mu des ca ligeeyam ba mu ko bàyyee woon at ak lu topp ña fa nekkoon it jàng rekk a leen fa ba woon du leneen moom itam ab jàngalekat rekk la woon waaye loolu teewul woon mu doonoon ku yitewoon a xam gaa ñu baax ñi ak seeni xam xam ak berook a wër niki ñu baax ñi mu leen daa junju ciy waxam ak a feeñali maanaa ak a yëgg ba bi ko himma ju kawe ji himma ci lun man a firi mooy yite dikalee muur ko mu jug yëggus lëf neeti tekk dal di woote cig nooy jëme ci mbiram moomu bi ko mbir mi gënee lëjal nag gën a fees fi moom gën a rëy mu dal di biral woote gi dajale mbooloo mi taxaw fa ñoom xutba leen sukkandiku ci dokkub dogu ne leen yeen mbooloo mi ku àndoon ak man ngir jàng rekk na laxas jëm ca boppam aki mbokkam mbaa fa ko soob man loolu rekk taxatumaa jug ku bëgg li nu bëgg nag na toog dal di leen fay ba dugg ca biir waxam jii nag dal di leen ba cig jaaxle ñenn ñi dem ña ca des des fa am ñuy jeem a tëyye seeni xarit ngir ñu des ak ñuy xiirtal seen waay ci ñu dem sëñ bi moom ne tekk rekk jeemul a tëyye kenn ku bëgg a dem ba mujj li ëpp ci mbooloo mi dem ba ko fa la ca gën a néew des fa bi loolu lepp data am fekkoon sëriñ bi mu sóobu ci ngiirum taalif ci xam xam yu nu tuxal yu sariiya yi mu woy ummul baraahiin bu imaam sanoosi wayjur wi nangu ko beg ci te mujj di ko jàngale bàyyi wesar wa doonoon cosaan la degg naa ci sëñ bi mu ne woy woowu de waajuram jàngal na ko ñaari doomam yii di sheex coro miy siidi muhammad alxalifa ak sëñ aafe mi tuddoon ahmadul muxtaar mu woyati teereb imaam xazaalii bi tuddoon bidaayatul hidaaya dal di koy tudde mulayyinuz zudoor di ci maanaa aji nooyal ji dënn yi ginaaw bi mu gàttal ko tudde ko munawwiruz zudoor di aji leeral ji dënn yi ci atum g teg ci jëzbatuz zixaar di bijjig gone yi ak jawharun nafiis muy wurus wu gànjaru wi nga xam ne da cee woy wesaruw imaamul axdariyyu ak yu dul yooyu bi ko donga yi nangulee nag lii mu leen doon woo daa bàyyi njàngale mi jëm ca di leen tarbiya ak a tarqiya tarbiya mooy yar ni ko sariiya bëgge tarqiya di yékkatee jëme ca yàlla man nag nee naa lii de du ñàkk muy ndigalug yonant bi j y m ndax kenn ci sunu sëriñ yi nettali na ma te moom ku wóor la di ndëërlaay ne sëñ bi de wax na ko ne yonant bi j y m moo wax ak moom ci gimiñam ne ko yaral sa àndandoo yi ci himma te bu leen yar ci njàng loolu sëñ bi gën na koo leeral ci qasida gii bokk na ci kiimaani doomi abdul laahi ji yal na ko yàlla dolliy xéewal ak mucc moom miy leeral suufam si ciy walliyu ba yawmal xiyaam te ku ci ne méngoo nga sunnaam si di ko ñogal wëlif bidaa bokk na ci kiimaani doomi abdul laahi jooju bégal gu mu bégal jëwrinam jii ci ne ko fazdah mooy wooteel ca kaw yonant bi j y m digal na ko ne ko mu jàngal muriid yi ak ku nangu mu laabiire la ci waa jamono te mooy ki ko àggale ca borooman cig taxliya mooy setal nit ki féexal ko ciy ayib bégalati ko ci tahliya muy ràng nit ki ay takaay walla sol koy ngënéel li mu jublu ci fazdah ji nag mooy biralal ca kaw mooy ji ci alxuraan fasdah bi maa tuumaru wahrid hanil musrikiin mooy biralal lin la digal te dëddu way bokkaale ñi yàlla daa digaloon yonantam bi j y m mu biral wooteem ga ginaaw bi mu ko daa yalu maanaam dëgg dëggi loolu mooy sëriñ bi bi donn gi mu donn yonant bi matee ci matalug yàlla t s te mu dolli ko ay xam xam aki hikma aki leer aki mbóot te may ko kàttanug man a yanu wilaaya gu mag gi bi loolu amee nag mu digal ko mu woote ca kaw woo mbindeef yi ñu weeru ci moom di jële ci moom tey def ay ndigalam di bàyyi ay tereem ci loolu la waxe yàlla mi nga xam ne lu ko soob mu def moo ma jox xam xam yi ak seen barke wattu naa lu xajul ciy teere kon boo may ligeeyal bul tàyyi yàlla miy joxe jox na ma ci darajay yonant bi barkeb alxuraan ak xam xam yi jël seen barke def ko ci samam njàngale yàlla jël na mbooti laa illaaha illal laah def ko ci samy taalif yàlla jox na ma te dootu ko nangu te man kaaraange laa te dib weeruwaay ci ndimbalam loolu nag ngënéelul yàllaa ku ko soop la koy jox te nee na ma neel weeru leen ci man ci maanaa sama boroom digal na ma ma leeral nit ñi ne man ab weeruwaay laa tey kaaraange ku bëgguw yiw àddunaak allaaxira na weeru ci man mu dellu waxaat ne murid bu yoqqatul ci man de texe na ci làqq ngën ji ay may murid bu yàlla wommat jëm ci mu aju ci man texe na te da na ceru ciy may murid bu wéeru ci man de yàlla miy sama dëkkandoo bu kawe bi def na muy ku texe ci lu kawe njortam bepp murid bu aju ci man day texe te ku niy soril la aw ay kepp ku aju ci man dey am nga ag mucc ci nëx nëxi àddina ak allaaxira ginaaw bi mu leeralaat ne way gëmi junne yepp ci jamonoom aju nanu ci moom mu ne junney sama jomono jii dey ña ca gëm ñepp aju nanu ci man waxuma ña gëmul mu wattuloo nag ñi aju ci moom ñuy xàccati ginaaw bu nu jébbaloo ne toroxte ñeel na ki ma dëddu won ma ginaaw muñ ma ginaaw bi mu duggee dib murid dal di leeral lu dig murid ak lub murid di bëgg mu ne dëgg dëggi ag murid ci li sang si wax mooy bàyyi aada muy li nga nekkoon njëkk ngay jébbalu bu àggagul ba noppi dellu ca la mu nekkoon mook ku murtad ay yam ndax kat ab murid du bëgg mukk lu dul gëramul yàlla ak fu mu man a jublu mu leeralaat ni ab muriid di mel ak ngértel ànd ak sëriñ bu àgg mu ne melow ab murid mooy bañ a bëgg dara ngir yàlla ku bëggul lu dul yàlla àgg fa moom mu jox kow yiwam ku aju ci ku àgg àgg ku aju ci ku àggul doo àgg ku yaroowul ci loxoy ab sëriñ dana dajeeki coona ndax ku amul sëriñ buy gindee saytaaneey mujj dib sëriñam fu mu jublu ab sëriñ du wuuteek ku nu rammuloo ki muy yonant bi kon ku jublu aji yar sheexul murabbi de da na jariñu fu la aji yar digale defal kon nga àgg ca boroom ba bu la aayee dara bu ko jege te bul sàggan ci wut gëramam mu leeralaat ne murid saadiq de am na ay meloom yoy bu ko amee am wepp yiw meloy murid saadiq ci gàttal ñeent la ma tënk leen nag ciy bayit ngir ragal woru dëggal ci bëgg sab sëriñ ba fàwwu jëfey ndigalam fu mu rote rekk bayyi gaaru ci lum man a doon gaaru mooy di am xalaat ci ndigali sëñ bi ak doonte ci sa baatin la ci lin nettali ak a tànnal sa bopp la ngay def ngir sa rafetug njort képp ku boole yile melo ci murid yi dey da na jot ndëërlaay ya gaa yu baax ya mu biralaat ne kiiraay am na juroom benni cosaan yu murid bi war a dagg te malaaka yi dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk ne kiiraay am na juroom benni cosaan ku bëgg a àgg da nga leen dog ñooy baril lekk ak naan ak a jaxasook nit ñi bari wax bariy nelaw sàggan ci tudd yàlla miy jàmm gëstul loolu ci jawaahirul mahaani bi sunu sheex tiijaan mu nu màggal mi def nettali nanu ne malaakay aji màgg ji dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk ngir yëram ko loolu man nga koo gis ci taalifi boroom hawaarifil mahaarif mu neeti murid saadiq doomi waxtoom lay doon ne murid saadiq mooy kuy wëlbatiku ànd ak waxtu wi mu nekk te du fuglu wa ca kanamam ndax loolu day teree yéwenal waxtu wi teew gëstu leen loolu ci jannatul muriidi teere bi sunu sëriñ xaliifatur rasiid def ak lu bokkul ak loolu ci li mu wax ci mbirum boppam mom muridam yi nga xam ne bu nu ko toppoon indi fi lu yeem xel yi te da na mujj kon gàttal gi nu bëggoon ci teere bii du amati ndax moom teere bii as kook la ci geejug xamale ko nu indil leen fii nag as tuut su nu tas ci ay wuññi ñeel lenn ci sekkarey xaybu yi xaybu mooy lu faddu muy mbirum biir niki liy xew te xewagul mu bégal ci ñi aju ci moom ngir dolli leen ag xeemeem ak sawarloo leen mu wax ne ñi aju ci man bu nu ko defuloon dem sawara doonte as ndiir lay doon it njëkk nuy tàbbi ajjana ji nu dig ñu ragal ñi yàlla li waral sama tukki bu sori bi yàlla mu barkeel mi te kawe daa bëggoon ca asal may kiy ramu samay donga dox na sama diganteek nasaraan yi tàbbal ci seeni xol ag ragal ma nu def la nu def nag ngir ma bañ a nekk dib nasaraan ndax bu ma ko doonoon tabbi sawara walhiyaazu billaahi waaye yàllaa ma aar ci sawara ak lépp lu mu gëramul ci darajay yonant bi j y m mu bind ay laabiire ñeel murid yépp ne mi ngi juge ci man jëm ci mbooleem murid yu góor yeek yu jigéen yi ab nuyyoo bu teey bu leen di musal mboole seen te di leen tabbal ci jàmm ak aafiya ci addinaak alaaxira ci barkeb yonanat bi j y m ginaaw bi may digal képp ku aju ci man ngir yàlla mu kawe mi te tedd mu xamlu pas pas yi ak tawhiid ak àttey laab ak julleek woor ak lu dul loolu ci lepp lu war mukallaf man nag warlul naa leen taalifal leen mbooleem lu leen koy xamal ngir jëmmi yàlla t s wasalaam mu bind lenn ci ay murid ab tontu bu neex yal na nu ci yàlla boole ñun ñepp mu ne ci assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa wa barakaatuhuu ma lay xamal ni sa bataaxel ba agsi na yaw murid bu dëggu bi waaye na la wóor ne doo gis lenn loo ragal booy faatu ak ci bàmmeel te ñaari malaaka yiy laaje xam nanu sa sëriñ te da nanu doylu ci xam gi ba dunu la laaj dara lii nag xamle la gum teg ci yoonu laaj ak tontu laaj bi moo di lan la sëñ bi woo ay taalibeem jëme lan mooy tontu li moo di sellal moom mi nga xam ni mooy ruuhug jëf tey ngértel xam xamub way xam ñi yàlla tey waralug àgg ca yàlla àgg ci yàlla nag ñi ngi ci jublu jaam bi nekk di ku weetal yàlla ciy yëggoom aki dalam aki pas pasam aki waxam ci lepp li feeñ ak li nëbbu lii nag manta ame ci njàngale rekk ndax kuy jàngale ab tegtalkat rekk la li ci des mi ngi ci aji jàng ji man naa am mu jëfe man naa am deet du ligeeyub jàngalekat muy sonnu ci waa ji jëfe loolule loolu sheexu tarbiya la war bokk na ci ligeyam moom sëriñub yar jàng ak jàngale ak ligeeyloo aki tudd yàlla ak gindee ginaaw bi mu leen xiirtalee cig cofeel gu dëggu te du tàggook ñoom li feek wonu leen seen ayibi bopp ligeeyloo leen ci nu jeem a laab ci yooyu ayib ngir man a àgg ak ñoom fa yàlla inshallaah bu loolu jàllee mbirum tarbiya day mbàir mu gudd manunu cee wax fii mu dem ak ñoom cib yar leen ci himma ñu nangul ko ko mu dox ak ñoom ci ngërum tàggat dajle leen di leen ligeeyloo lu bari yanu leen ci fàttaliku yàlla lu bari ak a jàngi xasida ak taqqoo lab ak a beru rawati na sori jigeen ñi ci noonu ñu kawe ñu dul ñoom ndax donoo joxe woon seen bop ak seen alal ci yoonu sàkku gëramul yàlla yalla jënd na ci jullit ñi seenii bakan ak seen alal faye leen ko àjjana sëñ bi wëy ci yoon wu jub wii mook saabaam yi dale ko ci njëlbeenug atum junneek ñatti teemeer ak benn ba bi mu sancee mbakke bawal ci at moomu juge mbakke kajoor sax fa lu tollook ñaari at nit ñi di ko dikkal juge fu ne ñii di jebblusi ñii di joxesi àddiya ñiiy sàkku ndimbal mu mujj yoonu këram gi mel ne yoonu ab ja ci ñeenti at yii nag mu siiw ci siiw gu kawe ñu jege ñeek ñu sori ñi ñeppuy yeemu ci moom te booba amagutoon sax fanweeri at ci diir bii sëñ bi wër na ci réewum wolof mi dale saalum ba waalo barak siyaare fa mag ña ña cay dund ak ña dundul jaar ca sëriñ sa jële ca ñoomi wird bokk na ci ñim siyaare ñoñ sheex siidiya siyaare na bàmmeelam ca tindawja siyaare sheex baaba mom abiihi ca maymooni tagg leen jële ca ñoom woy càllaleg xaadir gi tàmblee ko ca sheex baaba ba fam yam looloo taxoon kenn ci sheexi naar yu mag yi laajoon ko kuy sa sëriñ mu ne rasuulul laahi j y m mu ne ko kon lu tax nga ne fi di tudd waa kër sheex siidiya ak a wooyey sëriñ ak a tag mu ne booba da maa melon ne ku gumba di làmbatu yoon wi di ko sàkkoo xam ci ku xam ak ku xamul bi ma dajee boroom yoonwi ci ndimbalul yàlla nag muy yonant bi j y m mu xëcc ma ci boppam laa wacci ker keraan yi waaye di jokkook ñoom ngir yàlla ak a soppanteek a jriñante ngir moom te wax na dëgg ndax mbiram ak ñoñ sheex siidiya loolu lay tegtale mujj nanu mel niy doomam mu mel ni seen baay di leen jariñ ci alalam lu leenub buur jariñul ab sëriñ it jariñu ko ab taalibeem sheex baaba tag ko ciy xasaayid aki dagiid yu tollok ay teemeeri bayit bokk nan ci yile shex ahmadu xeewal la gu yàlla jox mbindeefam yi ak waxam ja sëñ bi daal xeewal la gu yàlla xeewalee di kiimaan ci kiimaan yi ak yu bokkul ak yooyu bu waxutoon yu dul yii it ñaari bayit yii rekk doyoon nanu seede ci màggug sëñ bii ak wilaayaam ndax kat sheex baaba ak màggam gi du fo mbaa muy yaxantu ci woy ni suharaawu yi moom dey lum wax ci ndigal la ko teg ak jaamu yàlla yal na ko yàlla fay ci ñaari bayitam yooyu bokk na ci ñim siyaare ci sheexi naar yi ustaas baaba mom hamdi ma jublu ci hamdim ñaareel mi dikk na fa yendu fa fanaan fa nee nan ci menn mbaar sama xarit ba niy dàkkantale kaadi sheex abdul xaadir doomi amiirul kumlayli nettali na ma te booba taalibeb ustaas baaba la ne ustaas mii moo jox sëñ bi sekkare bi waaye nag leeralu ma ban sekkare la man naa am muy wirduw saasalii ndax sëñ bi bind na ne moom wirduw saasali ming ko jële ci wenn wasiila njëkk muy dajeek wasila wu mag wi di yonant bi j y m te leeralunu kooka kan la li waral kaad mii nettali ma ko mooy maa ko laajoon bi mu jëlaatee ci sëñ bi wirduw sasalii ndax xam nga ci ku ko sëñ bi jële woon mu ne deedeet waaye nettali lim waxoon ci diggante sëñ beek ustaas baaba nu jorte ci ne ci ustaas baab moomu la ko jële ndax moom ab xaadir la woon kaad nettali na ma ne bi sëñ bi agsee ci bi miy siyaaresi ustaas ci bëcëgug bis bu sell ustaas defaral ko am soow mu neex ci ndox mu sedd ak suukar looloo ngi amoon ci jamono ji sëñ biy nattu boppam ci di tegoo ay coona mu ne ko naanal mu ne ko man baax na du ma naan lii mu ne ko ndax daa baaxul ci wàllug wér waala dang koo bàyyi ngir yàlla di jiyaar ak sa bakan sëñ bi ne ko waaw loolu la mu ne ko kon naanal bàyyiwu ko ba mu far naan ginaaw bi la dongay ustaas yi laaj lu waral mu sonnu ci mu naan nii mu ne leen ndax moom kat sonal boppam rekk la bëgg ak mettital ko mujj loolu di aadaam ngir yàlla jum munta baati ndare cib coona ma jëflante ceek moom waaye yàlla defal na ko barke ndax mujj na dëgar ci këng ginaaw bi lii wéyee lu yàgg ahmadu doomi ustaaas seetsi na sëñ bi njaareem mu bég ci lool di ko ganale ngan gu mu sonn indil ko ñam yeek naan yi bi nu àggee ci ataaya ahmad xam ne mbir dana am ndax moom du naan ataya bi ko sëñ bi tàllalee ataaya ji mu ne ko du ma naan ataaya mu ne yàllaa tax nga ba ko ngir jiyaar ak sa bakan walla ag weradi mu ni ko yàlla mu ree ne ko naanal ma fayoo ca la ma sa baay defoon ñaanal ko ci barke bi sëñ bi nekkee ci wëram boobu nit ñaang ko daa dikkale gepp wàll ngir xam xam bu bari beek njariñ li ak cofeel gi nu amoon ci moom ak diinewu gu dëggu gi rawati na alal ju bari jim daa joxe rekk nga xam ne daawul tëyye ab dërëm lu ñëw mu joxe di jox mag ak ndaw goor ak jigeen ngor akub jam ku am ak ku amul ku baax ak bon loxo bu tàllaliku jëm ci moom mu feesal ko te soxlaalul nit ñi doyloo kàppitaalam bi dul lu dul jublu ci yàlla ak yiteem jepp mu dem gànnaar jaar ca sëriñ ya siyaare ñay dund ak barabi way faatu ya jariñ leen ci alalam ju bari ja nu sopp ko nu kawe ni ko ñu ñuul ñi soppe defal koy xasiday tagg siyaaresi ko ci reewam ginaaw bi bi mbokk yi gisee ci moom kaweg xel gu diine gu mbaax gii mu yor ak jublu gu àddunaak nit ñi jublu nu tambli di ko iñaane di ko lor mu daan julleendoo ak ñoon lor yi ëpp mu mujj beru leen akum mbooloom ak jàkkaam yàlla gën a fésal mbiram ñu gënatee mer nga boole ci terewu gi mu defoon ci mbirum buur yi daawul nangoo jaxasook ñoom ba da daa sàkku sax ci sëñ mammoor ci ay bataaxel yum ko daa bind da daan kersawoo jàkkaarlook moom di ko ci wax dara mu bàyyi ag jëflanteem ak buur yi naan ko seen teddngay fii ji toroxte la ëlëg sëñ mammoor daan ko ko nangul te di ko ci jëggalu waaye njabootam gi taxoon ba manu leen a bàyyi ma nettali leen as lëf ci jaloore nee nanu bi kenn ci jaraafi latjoor yu mag yi mu nekkoon ku am solo fa latjoor jébblusee ci sëñ bi mu bokkoon ci jàmbaar yi amooni alal mu ndàmmoom gañewoon lu bari ci màggum xareb samba saajo bi màgg mooy li niy jële ci koo xeexal ba not ko samba saajo ab dëkk la bu nekk ca penkub njàmbur diggam ak jolof la xare boobu ame woon ci diggante amad sheexu ba mu fuuta ak latjoor tubaab yi japle woon ko moom latjoor bam gañe ko ray ko xarekati latjoor yi gañee ci woon màgg mu rëy ci alal aki jaam te ña ca ëpp diggante jolof ak fuuta lan bawoo ak kajoor tey jullit lanu buur bi laaj ndax man na leen a defi jaami kenn ci boroom xam xam yu mag yi ne ko waa waaw ndax ahmadu sheexu da doon wooteg yonant kon alalam ak dereetam dagan na nu dal di wéyal loolu te kat ag wooteem yonant mbooloom boroom xam xam yu mag yi saxalun ko li waral xare bi lu gudd la manunu koo netaali fii bi jaraaf jooju tuubee ci sëñ bi mu digal ko mu wacci mbooleem jaam ak alal ji mu ame woon ci xeex boobu jaraaf ji deggal ko def ko ànd ceek kontaante latjoor aki gaayam jàppe loolu nag ag weddi ñeel àtte bi leen kenn ci boroom xam xam yi defaloon ne leen jaam yi dagan nanu nu mere woon ko nee nanu ma jaraaf ya woo woon nanu jaraaf jooja fa kanamu latjoor ne ko lu tax nga bokk ak nun ndab regg rekk wëlbatiku doyatu la nga ciy xëpp suuf mu ne leen waaw weñ a tàbbi ci sama bakan lëjal ma moo waral lii ngeen gis ci man waaye bëgg a nëxal seenum mbir taxut mu jublu woon ci weññ wi lislaam ji ko duggoon cig mbetteel yaw nag xam nga lëjal gi lislaam di def kum dugg du ko bàyyi ndare bu daa tuub ñu xam ne lim wax lu dëggu ci moom la ñu jëggal ko noppi cim mbiram waaye sëñ bi moom latjoor lijëntilulu ci anam gu nooy te teey nun ko ko indile mu bind koy leetari leetar yonni fay ndawi ndaw teewul sëñ bi bañ nee nan ma wax na bis kenn ci ndawi buur bi ne ko neel ki la yonni rus naa malaakay yàlla yi di ma gis ma jëm ci buur bu dul yàlla degge naa ci sheex aadama sàll moom kenn la woon ci ñi njëkkoon a jébblu ci sëñ bi cosaanoo woon jolof mu ne leetar bi sëñ bi mujj a bind latjoor moo ko doon yobb mi ngi ci naan muhammad ibnu maslama nee na boroom xam xam ci buntu buur mi ngi mel ni weñ ci kawi jonkan latjoor jox xaali majaxate kala bataaxel bi moom moo nekkoon mufti bu mag bi xaali yër ko tiit ne innaa lillaahi wa inna ilayhi raajihuun buur bi ne ko lan la mu ne ko kii waxul ak yaw man lay waxal mu ne lu man a xew waxal rekk mu jàngal ko ko latjoor ne ko ci man de la gën a dal ndax yaw lu man a xew yaay weñ wi man nag ay dem àll laa waaye nag yaw miy boroom xam xam loo wax ci moom xaali ne ko man daal li ma gisoon mooy nu ba ko ak mbiram ndax kat notanteek moom ag woru la boo ko notee bokk ci ñi gën a kawe bu la notee nga di ci ñi gën a suufe te maneesu koo not buur bi ne ko wax nga dëgg ndax baykat kat yàgg naa gis jànjnji ci toolam te manu koo bay manu koo saxal mu ba ko fa xaali ne ko waa waaw mu ne nan ko jàppe jànjnji boobu ci noonu leetar ya dog wax ja jeex alhamdu lillaah beneen nettalee ngii bu gënatee yeeme waaye soriwul bu njëkk bi mooy bi leetar yeek coow li jeexee ci bataaxel bu saf boobu yàlla dogal na latjoor ànd ak xaali ci lenn ci tukkeem yooyu mu daa def ba wàcci benn dëkk wetu fi sëñ bi dëkk bi sëñ bi yëgee ne mook xaalee ànd mu ne na nuyji xaali ngir ñaari mbir menn mi mooy xaalee ko daa jàngal te ku la jàngaluw araf sa kilifa la ñaareel bi xaritub baayam la woon mu war ci moom mu jox ko àqam te jokk ko ndax danu ne joxe àqi waajur gi gën a mat mooy waa ji dox kóllare ak jokk ko ci xariti baayam yi bi mu agsee fi ñoom fekk leen nu toog ci lal sëñ bi nuyyu leen nuyoob màggal toog ci suuf toogul ca laltu ga fa ne woon bi mu toogee tuuti ne xaali da ma la fee deggoon rekk ma ne naa fi jaar siyaare la ci noonu latjoor xam ne daa bëgg a leeral ci ne dikk gi latjoor taxul jubook moom it taxut latjoor gestu xaali ne ko nun kat kii war nanoo wax ak moom ca sun mbir man ko woo woon ba sonn mu bañ xaali ne ko aca ne sëñ bi man dey maa ne ahmadu sheexu da doon wooteg yonant te di ci xeexe it kon ray ko dagan na lekk it alal jiñ nangoo ci moom niki màgg ak njaf ñamu àndaloon njaf mooy jàpp jaam loolu lepp dagan na bi mu noppee mbooloo mépp noppi ab diir sëñ bi ne xaali ndax da ngaa wax ngir ma tontu la xaali ne ko waa waa bu may wax kay nga tontu maa tax sëñ bi neeti ko kon am naa ndigal ci tontu mu ne waa waaw sëñ bi ne kan moo la man a seereel ne woote na ag yonant xaali ne ko waa kajoor mu ne ko ñooñu ay noonam lanu te diy xuloowaaleem di xareek moom nan lanu koy seedeele xaali neeti ko waaye waa samba saajo fi xare bi ame woon sëñ bi ne ko ñooñu kay dun seede ndax xare baa leen fa fekk sottiku ci seen kaw te yëgunu woon nan laniy xame ki nu tuumaal ak li nu ko tuumaale xaaleek mbooloo mi ne tekkus lëf bam yàgg mu ne yaw gone gi won nanu la yàlla nga jiitu nu ca konug ndokkeel ñeel na la dal di nooy te jubook moom pënd ba wuriku sëñ ba tàggu leen dem ci noonu yoon yepp dagg ci moom lu dul wi jëm ci yàlla ndax kat moo ñë ci ñu baax ñeek kàccor yi jàng ca ñoom wa ufawwidu amrii ilal laah innal laaha bashiirun bil hibaad wallaahu yahlamul mufsida minal muslihi muy joyal naa samay mbir ñeel yàlla moom miy gis jaamam yi yàlla xàmmee na kiy defar ak kiy yàq li mooy dooley sëñ bi te nii la dogoo woon donga yi raw ko cig dogu foo leen fekk ña ngay xeex ak nit ña nga gis daanukatu jell yi fii leeg leeg nga gis ku ci yeeg ba ci kaw njobbaxtalu garab ne dërr fi suuf jiital bop bi jug faxasu dem te dara du ko jot ak ñuy tàbbi ci sawara genn te dunu lakk di yekkati xasiday sëñ bi ci penciy nit ñi ak seen daara yi ñuy xeex ak ñoom te du tax nu ba ñu leen di door ak a jeng ak a nangu seen alal ak a genne seeni kër loolu lepp ngir teqale leen te tas leen mu mel ne jëf jooju da leen na dolli ag xeemeem akug sóobu mu mel ni loolu mbóotum yàllaa mu ball juge ci baatinub seen sëriñ ba ca ñoom sëñ bi daa leen dolli pastéef di dëgëral seeni basiira di yekkati seeni yite ba ca yu saaba ya naan leen roy leen saabay yonant bi ñooy seeni mbokk de te daje nannook lu gën a tar lii ngeen nekk ndax ray nanu leen ci yoonu yàlla tuur seeni dereet nangu seeni alal genne leen seeni kër te loolu teewu leen a jublu ci li nu soxla ba am tagg wu rafet ca yàlla lil fuqaraail muhaajiriin allaziina uxrijuu min diyaarihim wa amwaalihim yabtaxoona fadlan minal laahi wa ridwaanan wa yanzuruunal laaha wa rasuulahuu ulaayika humuz zaadiquun mu leen di xamal ni da noo war a roy ci way gàddaay yu ñàkk yooyu nga xam ne ku dul yàlla ñoru leen woon ñu genne leen seeni kër naggu seeni alal ci yoonu sàkku yàlla ak ngërëmam ak dimbali yàlla ak ab yonantam ñooñooy ñu dëggu ñi mu naan leen xanaa xamu leen ne ñooñooy seeni baay ci diine kon lu leen man a dal day dal di doon lu neew laxadd kaana lakkum fii rasuulil laahi uswatun hasanatun liman kaana yarjool laaha wal yawmal aaxira muy ku gëm yàlla ak allaxira na ko wóor ne am na roytéef bu rafet ci yonant bi muñ leen tey rafetal ci kiy ñaawal ci yeen idfah billatii hiya ahsanu faizal lazii baynaka wa baynahuu hadaawatun ka annahuu walliyun hamiim wamaa yulaqaahaa illal laziina zabaruu wamaa yulaqaahaa illa zuuhazin haziim muy deel jañe jëf ju ñaaw jëf ja gën a rafet kon nga gis ne ki nga xam ne ag noonoo daa am seen diggante da na mujj mel ni sa xarit bu sellug xarit loolu nag ku dul kuy muñ du ko am ku dul ku di boroomub cér bu mag dee leen di fuglu yawma nadhuu kullu unnasin bi imaamihim muy bis ba niy woo nit ñu ne ci seen imam kon de bañug ku bañ du leen naqari ñu daan def bu nu naanee ci ndoxum waaraatey sëñ bi moomu ba màndi di ñu sawar di daanook a yuuxu ak a fecci ci diir bii sëñ bi doon baril lu muy def ay xasiday xam xam ak yu tag ci la woyoon masaalikul jinaan muy teere bu amul moroom ci tazawuf yor junneek juroomi teemeer ak juroom fukk ak ñatti bayit ak mawaahibul xudoos ak yeneen ci la wàccee it ñu bari ci donga yi niki sheex ibraahima faal ak sheex ibraahima saar ak sheex anta mbakke ak sheex aadama gëy ak sheex asan njaay ak ñu mel ni ñoom bi nit ñi barilee lor yi ak sonal gi ca mbakke mu tuxoo fa sanci daaru salaam ci njëlbeenug atum junneek ñatti teemeer ak ñeent waaye teewul lor yi wéy di dolliku mu sax fa lu tollookum at di yar nit ñi di leen yeege nuy gën a dolliku raj rajloo biy gën a yokku wërsëg wiy gën a sottiku niki ab taw mu juge fa demus lëf ca penkub bëj gànnaaru daaru salaam ci lu tollook juroom walla juroom benni miil sanci fa tuubaa ci mujjug atum junneek ñatti teemeer ak juroom walla ci njëlbeenug atum junneek ñatti teemeer ak juroom benn tuxu fa ak ñaboot gi sëñ fallu nettali na ma ñaareelu xalifa ne magam ja sëriñ moodu mustafa mi njëkk a doon xalifa mi ngi ganee àdduna daaru salaam guddig àjjuma fukk ak benn ci muharram atum g njëkk sëñ biy tuxu ndax moom mi ngi tuxu ci li nu wax ci jumaadas saaniya ci guddig kasurajab maanaam ñaar fukk ak juroom ñaar ci rajab sëñ fallu gane àdduna ñu magantee juroom benni weer ak fukki fan ak juroom ñaar yal na leen yàlla barkeel ginaaw bi ci la sëñ muhammadu lamin baara ganee bokk ak sëñ moodu mustafaa nday ak baay ci atum g walla g mu des tuubaa nag noom sëñ bi di dem ak a delsi ak a tuxu ci diggante kër yi niki daarul minnan daarur rahmaan ak daarul xuddoos ku dul yàlla nag xamul xew xew yi daa am ci digganteem ak boroomam ak diganteem aki saabaam ci xeeti tarbiya ak tarxiya ak yu ni mel ak jàngale ci taalifam yi ak digganteem ak ñu baax ñi ci ay mbir aki duggalanteeki xuloo ngir seeni doom ak seen taalibe yi wëlbatiku woon jublusi ko ak ci digganteem ak buur yeek jaraaaf yi ciy xuloo ngir fiir ak tiit ci seen nguur gi lu man a xew doxiin wi moom juboon na donga yi jub ñu daa dollikook a yokku jamono ju ne ku mu ci wàcce mu wéy di jub ku tàbbi it tàbbi cig njub ba bi mu tukke ca geej ga sëñ baa ngi sanci jolof ci li ma sëñ mbakke buso nettali bi mu nekkee tuubaa ba nit ñi bari fa magi donga yi denciy soxna dëkk yi woon ci wet gi ñu ci bari tuxusi fi woon ak seeni ñoñ ñi sëñ bi jugoon ngir yar leen tàmblee jaxasook ñeneen ñi nos gi sëñ bi nosoon mbir yi am lu ci tàmblee yàqqu mooy bëgg gi mu bëggoon a ber ñiy jàng cig wàll ñay ligeey ca geneen wàll ñiy ligeey ak ñiy jàng jaxasoo gi naqqari ko rawati na jaxasoo gi niy def ak ñeneen ñi nga boole ci loolu aj gi mu bëggoon a defi ak siyaare ji yonant bi j y m te bëggoon koo bëgg ba daa ko wax ñenn ci ñi ko jege woon kenn ci sunu moroomi naari daymaan yi di muhammad doomi hamdil abhami nettali na ma ne sëñ bi nee na ko ca at mooma ca tuubaa ndax bëgg ngaa aji ma ne ko waaw wallaahi waa waaw ku ma fay yobbu kay laa amul mu ne ko demal ca sa ñoñ te waaj te ñëw ci mujjug at mii nu ànd aji bu neexee yàlla ma dem waaji te lijanti ji sama njaboot naan inna lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun nu dellu ca wax ju njëkk ja sëñ mbakke buso nee na bi ko ñaari mbir yu gaar yooyu jaaxalee muy mbirum jaxasoo bi ak mu bëgg a aji gi da maa woo waxtaan ceek man diisook man ci mbirum ñu sanci ab barab bu nu man a tàqalee ñaari kuréel yi wëlif ñu dul ñoom te teqale leen ñoom ci seen biir ngir ñiy jàng ak a jàngale man a def seenub ligeey mu samp ci jiite njàngum alxuraan mi sëñ abdu rahmaan lo njàngum xam xam mi mu teg ca maam cerno rakam ja ànd faak ñoom ñaar rekk ak seeni kuréel keneen dollikuwu ca ci donga yi walla sheex yi mu ne ma yaw nag kon da ngay des tuubaa di jëwrini donga yi ñiy siaaresi bu nu ñëwee ak seeni àddiya ku ci war a agsi nga bàyyi mu ñëw ku wart a agsi bumu agsi ma ànd ak moom ci loolu xalaat ne lii daal xalaat bu nu barkeel la inshaal laah mu tàmblee waaj di ci làqatu ñi mu bëggul ñu dem bi dogu gi dëggaree ci dem te loolu da ko daa làqq sunu waajur wii di nijaayam nga xam ne da koo bàyyi woon ak man rekk doyloo ab gis gisam ci man mu mel ni da maa soxlawul bi mu ci dogoo dëgg nag la xam ne du man a ñàkk mu yëgal ko nijaayam jooju mu dal di ko koy yëgal yëf yi nag tiis ko lool ngir xam gi mu xam ni buuri jolof yi fiire ak ni nu manadee muñ wuuteek buuri wii tund te taalibey jolof yi it dunu bàyyi seeni doom aki donga te dunu muñ it wuuteeg yu gox bii mu ragaloon nu sonal ko aaye woon ko ci anam gu nooy mu bañ a dem yee ko ci aaday ñaari dëkk yi ci li mu ci xam ndax xamoom na ne li sëñ bi bëgg dëppoowul ak seeni aada waaye sëñ bi moom niki soofiyu yu mag yi dafa dogu te fas yeenee wéyal li mu dogu ndax wéyal ag dogu ci tasawuf la bokk tekki ag dogu fi ñoom mook tubbee yam dee ko gën a woyof ci ñoom kon sëñ bi laxas na ak dongaam yooyu ca sawaal ci atum junneek ñatti teemeer ak fukk ak ñaar g g mooy ci ati gàddaay gi wuti suufus jolof ndax gisul ci bawal barab bu man loolu mu bëgg ca jamono jooja ak ndax itam jolof suufus ay maamam la woon p mahalu ajdaadihii ba bi xurbi tuubaa walla muy aajowoo jankooteek ay ñoñam mbaa mudaaraanteek ñoom te loolu du lu mu daa faral a def mu dox ak ñoom ba mbakke baari wacci fa sanci fa waxtaan faak yenn jaraaf waaye ag ñagas feeñ ca njëlbeenug wax ja àggoon ci ñu naan nun dey xamunu woon ciy donga ag sàkkoo dooni buur ñii di ñëw daal nekkunu lu duli buur yu ñëw ngir xëccook ñun suniy suuf yàgg nanu leen a dégg ca ña ca seen ginaaw nun nag ñi ngi giñ ci ne dunu dëkk ak nun ci sunu suuf sii ci seen melo wii ak wax yu mel nii ci yi ko nijaam ji daa wax ak a sentul bu fa demee waaye yàlla moom bu bëggee amulum mbir da koy wutali sabab nee nanu bu yàlla bëggee tàllal gënéel lu lemu da koy wutal làmiñu ku iñaan bokk na ci xeewal yi yàlla xeewale sëñ bi sóob gi mu ko sóob ci yoonu walliyu yi sunnatul laahil latii qad xalat min qablu walan tajida lisunnatil laahi tabdiilan muy ci maanaa yoonu yàlla wii di wu wéyoon bu yàgg doo gis ag coppite ci yoonu yàlla nit du jug mukk jëm ca yàlla ndare bu danu koo natoo ay noon yu koy lor loolu fiiraangeg yàllaa ngir mu bañ a jàdd bañ a wéeru ci ku dul moom yàlla da koy feeñu cig màgg akub taar ci feeñu gog taar gi attajalliil jamaalii la ko yàlla di ñoddile nit ñi ñuy sottiku ci moom niki ay weñ yu tiimub puur loolu nag ci tàggatug yàlla lay ame ñuy yërmaande juy texeel ku nar a texe ci feeñu gog màgg gi attajalliil jalaalii la leen yàlla di dëddaleek yen xol yi ñu nekk seeni noon dunu gis seen hurma dunu leen gëm di leen ayibal ci seen bop ak ci seeni taalibe waayee ak loolu lepp hifthul hinaaii du tàggook ñoom mooy wattu gi leen yàlla di wattook a aar dara du leen dal lu dull u yàlla bëgg mu dal leen juge cib noon di luy ñaaw ci saayir diw yoon jëm cig fayantoom innaa minal mujrimiina muntaqimuuna muy ci maanaa da nanu fayyu ci ñiy tooñ ñi ngi ñaan yàlla jàmm lii mooy mbirum sëñ beeki àndandoom ca njëlbeenug jolof bu dee lu aju ci ñam ba woon ca ginaawam nag ñoom sëñ mbakke buso nee na taalube yi mu ba woon tuubaa bi nu yëggee ni sëñ baa nga jolof ñu tàmblee wuti pexey dem fa yalwaankat yi fekksi leen ci loolu ñu gàddaaye tuubaa ndare ku fa dëkk xaalaatub siyaarekat yi di fa yam dal di yàqqu lu tax deet ginaaw mbir mi dàu mbirum xalaat bu dee lu aju ci jaraaf dëkk bi ku ci gisoon li nga gisoon gën naa yokk ku ci gisutoon tàmbli nga gis leegi nga boole ci lanu deggoon ci diggam ak buuri jolof yi nu dikkal nu ci kaw ak suuf bi buur yeek seen dag yi gisee li nu gis te ñoom boroomi ngànnaay lanu ñu daa dund ci seen ngànnaay rekk dan daan song ku leen daa jeem a të duma ko nangu alalam ray ko mbaa ñu njaf ko jàpp ko jaam loolu nag di woon aada ju yàggoon ci ñoom ju nu daa donante waaye loolu teewul ñu amoon jàmm ak lenn ci boroom neeg yu mag yi daawunu leen boole ci seen jëf jooju daawunu ci boole it ñi daa aaru ci seen kaaraange niki neegub sëñ bi loolook meneen mbir a waraloon nu jaaxle woon ci sëñ bi meneen mbir mi nag nga xam ne moo leen gënoon a jaaxal mooy mbirum nguur gu raglu gii loolu nag mooy tubaab yii di waa faraas ñoom danu daa def suuf sunu not jël fa njiit muy ku fa bokk samp fa ngir waa dëkk ba bañ a mer te ànd ak ñoom xoolal ma gii xam politig p wakaana haaulaayi ba falamaa lam yakun lihaaulaayi bi jaraaf yooyu demee ba manatunoo dellu ci seen aada yu njëkk yu bon ya muy ray jullit ñi ak giir seeni alal ak doonte loolu da leen di àggale ci nuy raye it du tee nu def ko bi nu demee ba manatunu loolu te loolu tubaab yee ko waral ñu mujj di leen xiirtal tubaab yi jaare ko ci ay pexee ki wor mu neeti jaraaf yooyu jaxase googu nu doon jaxase jullit ñeek nguurug tubaab yi jubluwunu ci woon faagaagal leen ndax lu man a xew ñoom ci seen ron kilifteef lanu nekkoon doonte ci anam gu woyof la waaye kay ñi ngi ci jublu woon ame ciw yoon wu nu man a nangoo seeni alal bari na lu nu leen daa wax naan diw kat da leen a bañ diw it nanguwul a fay galak diw mee am na lu mu leen di waajal diw mii mi ngi wuti ngànnaay di dajaley fas walla nit ñaa ngi koy deglu walla ku bariy taalibe la ñu koy màggal dayob màggal ba àgg ci bu leen junjoon geej gi ñu sóobu ci xuus ko ak leneen ak leneen ci seen fen yi nu daa def ngir bëgg tubaab yi digal leen ñu songu leen walla nu def ci ñoom lu leen soop te xamunu ne yewwuteg faraase yi ci wàllug politig moo gën a yaatu loolu waaye nag wax bu baree juge ci ku la naan mooy sab bët di sa asaa sekkare di la xoolal sa ginaaw da na mujj am lu mu bàyyi ci yaw benn bis rawati na bu fekkee ki ñu ne moo def loolu du rambaaj du jaxase te du jeem a setal boppam ca ki nu ko rambaaje te ñiy yàqq dunu dañ di yàqq diggante bi rawati na bu nu niroolee am mbiram ak mbirum ku yori donga yu ko gëm lu mu leen digal nu def looloo waraloon ñu tàmblee tiit ci moom ndaxte dañ koo niroole woon ak sheex omar fuutiyu tukkuloor la bu defoon ay xare ci wàll gi dëkke woon ci mujji ati juroom ñaar fukk yi bi loolu jàllee ba teg lu néew la benn wolof bu tuddoon maalik ba nu gënoon koo xam ci màbba defoon ay xare ca goxub saalum ci ati juroom ñatt fukk yi ginaaw bi la ahmadñ sheexu dib tukkuloor xaree xareem ba ak waa jolof ak kajoor ba bi mu deewee ca bisub samba saajo ca wàllug luga ca mujjug ati juroom ñeen fukk yi jaxasekat yi nag bi nu demee ci tubaab yi danu leen sëñ bi ñii lay roy ba mujj tubaab yi manatuñoo ñàkk a gëstu lin leen wax lii daal mooy li gën a waral tubaab bi jublusi sëñ bi ginaaw bi ko yàlla dogalee namm ca la mu ca namm muy wax joj dara amu ca ndax sëñ bi lorewul soxlawul àdduna te xemmeemul li nu jort ci moom yàllaay seere lii nuy wax bu doonutoon rambaaj yii waxuma la buur yu ndaw yi sax dunu ko jeemal waxantuma laak yu mag yi waaye loolu day dëggal waxi yonant bi ji j y m ñi yàlla gën a teg ay nattu ñooy yonant yi teg ci walliyu yi teg ca ña gën teg ca ña ca topp ponk bii nag bu wéy la ci xeetu yonant bi j y m ndax ñu baax ñi ëpp ag gëm foo leen fekk daniy fees dell aki nattu àdduna dëddu leen naqqari ci ñoom ñooy ëppi jafe jafe fuuf ñu dul ñoom boo demee ca sahiihub muslim ak bu dul moom da nga ca gis àddunaay kasob jullit tey àjjanay yéefar yàlla itam wax ne wal aaxiratu hinda rabbika lilmuttaqiin muy àllaaxira ñu ragal yàlla ñee ko moom bi tubaab yi demee ba manatunoo ñàkk a xool mbirum sëñ bi ñu tàmbli faa yabali ndaw aki bataaxel ay yooni yoon di sàkku ci moom mu seetsi leen moom muy xaar ndigalul boroomam rekk ak lu yonant bi j y m ñu gise yeex a wuyyusi gi ag bañ bu ko defee ña daa jaxase di gën a am lu nu wax naan waxoon nanu leen ko gis ngeen linu leen waxoon am deet ba bi fa tubaab ya yonnee lenn ndaw mu ànd ak yenn soldaar yu neew bunu leen tollaleek li nu am ciy xarekat ndax matunu mbooloom xare mu mag lii moo doonoon li ko boole woon ak tubaab yi sëñ bi bi mu jotee ndigalul yàlla ak yonant bi j y m yonant bi j y m jox ko kiiraay luy dox diganteem ak tubaab yi te loolu wax na ko ci genn xasida kun tànn ki jàmm ak mucc yal nanu nekk ci moom wutal ko kiiraay lu koy aar wëlif lor ne ko doxal te bul ragal woru bi loolu amee mu genn ca këram ga mu sancoon jolof ngir jàng ak jàngale ci bisub gàwwu fukki fan ak juroom ñatt yu safar ci atum junneek ñatti teemeer ak fukk ak ñatt g ci jummaada saaniya walla sahbaan ci at mii la sheex bashiiru gane àdduna di doomi sëriñ bi bi miy genn dajeek ki jiite mbooloom xare moomu genn moom itam juge wàllug luga ñu daje ca jeewal ca ngoonug bis booba sëñ banji njaay nee na ma moom ci ñi àndoon ak sëñ bi kerook la ñu gënoon koo xam ci banji xuja am na benn karaama bu feeñ jeewal mooy bi nu àggee jeewal danoo jeexaloon ndox te foofa ndox bariwu fa satalag sëñ bi jeex bi nu nekkee ci jaaxle googu nag benn waay buy or ab baag bu fees dell ak ndox jege nu wax ak moom xamul li nu koy wax nu jox ko ab defukaay mu duy ko ba mu fees ak ndox nu naan sëñ bi jàpp ndax moom daawul tiim waa ja jàll te deggunu aw làkkam xamunu ci moom dara sëñ bi nee na ginaaw bi nu jullee tàkkusaan nasaraan boobu di njiitul soldaar yi dikk na bëgg a wax ak moom mu wëlbati kanamam wëlif ko jublu yàlla jàng bismil laahir rahmaanir rahiimi juroom fukki yoon waa ja nooy aw xalam fay mu gaaw genn jëm ci ay aajoom mu fanaan foofa ak jaraaf ju ñuul jooja ci loolu sëñ baa ngi naan ginaaw bi nu dajeek ña gennoon jëm ca këram te njàqqare nekk ci seeni dënn dox nanu àndandoo di way gaaw jëm ca jaraaf ja ba tàkkusaan jotee ñu julli fa cig ragal yàlla ginaaw bi la jaraaf ji daje ak moom mbooloom xareem mi wër ko am ca ñuy siaare mu jubale kanaman ca yàlla mu tedd ma bañ koo jubale jaraaf ja ngir am li mu bëgg wax juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi cig toroxlu jëm ca ka nga xam ne fu mu daaneele ab noon mu nërméelu jaraaf ja genn cig gaaw jëm ca aajoom mu fanaan fa di boroomi xeewal waxam ji mu naan am ca ñuy siyaare sëñ nee na mi ngi ci jublu woon taalubeem ba omar njaay sheexub konjoru njaay di dëkk bu nekk ci wetu luga moom nag am na wàccuwaay bu kawe ci sëñ bi bi mu faatoo sëñ bi seereel na ko yiw wu rëy dig ko it yiw wu ko ku dul moom di ñeewe ngir rafetug njortam ak waxam ju rafet ci sëñ bi ñi ngi ko denc njaareem sëñ bi nee na omar mii mi ngi genn ngir siaaresi ma dajeek soldaar siy genn fekk nu xamoon ko te fonkoon ko ñu kontaan ci ànd gi mu ànd ak ñoom jàppe woon ko kenn ci seen kilifa yi waaye yàlla moom xam na la nekk foofa sëñ bi nee na nasaraan boobu jiite woon soldaar yi moo doonoon ki yoroon luga gouverneur ca jamono jooja doonoon gorob buuru ndar boroom ndar looloo waraloon ñu deglu woon ko ci samay mbir mooy ku rëyoon ki daawul wax ci man lu baax daawu ko def daawul ànd ak ku koy def dogu woon it ci tumbrankeel ma nu ne ko du fi ame mu ne kenn du ko tee am dogalub yàlla bi dëppook li mu dogu looloo taxoon ma yàggoon ndar ñuy xool samay mbir p dale wa awra lihaasihiil aaya ba sais yamkur wa iz yamkur bikal laziina kafaruu liyuzbituuka aw yaxtuluuka aw yuxrijuuka wa yamkuruuna wa yamkurul laahu wal laahu xayrul maakiriina muy ci maanaa bi la ñi weddi di fexeel ngir saxal la fi walla ñu ray la mbaa ñu genne la ñu nekk di fexe yàlla itam di fexe te yàlla ay ki dàq a fexe sëñ bi nee na ndar ña fa nekkoon ñatti kuréel la woon ñu bëgg ñu bàyyi ma fa bu ko defee nu di leen sonal ca daanaka dun ba bepp daanaka dun mooy presque ile di yàqq seeni kër ak ñu bëgg ñu faat ma ñooña amunu lanu bëgg ak ñu bëgg ñu tumbrankeel ma ñooña yàlla dëppale dogal bi ak seeni xalaat sëñ bi wax na ci loolu lii yàlla tàbbal ci xoli ñi sababoon ag tuxalam ca jooja jamono ab nettali bu yéemoo ngii ma degge ko ci sëñ bi ci mbirum àttekatub goornoor luga bu rëy te bon te féetee woon mbirum tukkib sëñ bi te taxawoon temb ci mu am sëñ bi nee na àttekat boobu bi ma nekkee ci tukki bi laa dégg ñu ne danu koo mujj mere gëstu ay mbiram gis ci luy waral ñu genne ko tumbrankeel ko bi niy xalaat mbugal mi nu ko war a teg am ku ne kii daal ginaaw moo taxoon nu genne sëñ bi tumbrankeel ko nanu ko yobb fa waayam ja nekk ñu dëppoo ca loola muy fayyug sunu boroom yëguma lu dul ñu ne ma àttekat baa ngi ci dun bi ma nekkoon mu nekk foofa ab diir di ma làqatu ngir ragal ak rus looloo waraloon mu dem gis goornoor àttekat walla saytukat ba fa nekkoon ne ko moytul ma sëñ bii fi yaw bu ko jeem a def lenn lu ko naqari ndax lii ma dal de dara waralu ko lu dul sama yeene ju ñaaw ci moom kon daal bul def lu dul di ko jox li nga ko war di fay weer rekk te yam ca looloo waraloon àttekat boobu nooyoon mel ne galas fi man tukki bi li ci jafe woon lepp mujj yomb bi yàlla sottee ndox ca sawaraam wa doon jëf jëfi moom goornooru luga bi mu mujj di ku sedd la nu ko delloo fa mu juge woon ginaaw bi ñu yobbooti ko ci penk bi ca wàllug xaay foofa la ko ab njabarkat bu bàmbara njabare ci genn kërug bàmbara mu dee di ku nu dàkku di ku nu gàññ xoolal ma rekk mujjug ñiy tooñ mbirum noonam boobu nirook lool mbirum noonub ki miy ligeeyal di yonant bi j y m noonam booba di woon haamir doomi tufayli ba mu nee jamono ja ko tawat ji sonalee ci genn këru jenn jigeen ju salool p axudatan ba bayti saloliya sëñ bi def na ag xasida gum u tënke arafi mazalul jannatil latii wuhidal muttaquun ba ca tilka huqbal laziinat taqaw ne tooñ gu nu ma doon tooñ jeex na aji not jee ko jeexal ji damm ngànnaayul ki doon puukarewu mu damm moom de yàlla am na samag cant ndax rayal na ma ka doon fexe ci atum junneek ñatti teemeer ak fukk ak ñatt g te deem gi dolli xalaat yi amewul ca la mu doon def lu dul am mbugal te ginaaw bi mu farloo ba yaakaar ne moo ci ne daa daal di giim tawat ji gàllankoor ko fayyug sunu boroom da koo tiital mu daw ci geej geek ci jeeri ji te am mbooloom wor ko jaraaf ju ñuul jooju xam naa aw turam xam giir gi mu bokk waaye du ma sobeel sama xalima ci bind aw turam mook mbokkam mu nasaraanu mi daa ñaawal sëñ beek a saboote fu mu masaa dajeek moom moo nekkoon garambasaa gis naa li sëñ bi bind ci ñoom ñaar ñu bari it ci ñi xam seenug mujj nettali nanu ma ne ku ci nekk dee gu ñaaw la dee kenn ki mooy ku jéeri ji mi ngi ndakkru ki ci des di ku geej gi nekk konaakiri yal na nu yàlla musal ak jullit ñepp ci nattu bi mu leen tegoon nu dellu ci mbirum tukki bi sëñ bi nee na kerook wird wi mu gënoon di def mooy inna walliyiyal laahul lazi nazzalal kitaaba wahuwa yatawallaz zaalihiin muy ci maanaa kiy méngoo samay mbir mooy yàlla mi wàcce teere yi te mooy kiy méngoo mbirum ñu baax ñi loolooy maanaam waxam jii yàlla naagul na ci man ibliis fa jeewal bi ma ko woowee ci turu walii muy kiy méngoo mbir yi sëñ bi fanaan foofa bi mu julle suba laxas jëm kokki ñu yendu fa mu tàmbli faa woy xasidag asmaau ahlul badri sëñ baa ngi wax ci loolu ganaaw bunu fa yendoo moom tàmbli na fa di woy lol ubbil na ko ab bunt boobu bisub dibéer la bi gee jàllee ba teg lu néew ñu laxas ci li ma kenn ci ñi àndoon ak sëñ bi nettali ci fenkug weer wi ci guddig altine dëppook ñaar fukki fan juge kokki nee na booba ñun ñi ngi dox muy wicc wiccal ci sunu kaw sëñ bi nee na maa ngi rañaan mooy dox guddi kerook ca guddi googa ci kaw sama wenn gelamu ñu naa ko hawnul laah wu gaaw nga xam ne fasi ñoñ buur bi manunu koo jot te ñi ngi doon def li nu man ba mujj am ci ñoom ñu naan ma sëñ bi defal nànk yëramal sa bopp te yëram nu ma naan leen gaaw leen nu ku nu yilif ba noppi yonni ko di yeexe bu ko defee nu wedam sëñ bi def na ci loolu aw woy laxas nanu ginaaw bi nu yendoo di dox ca ginaaw gee ànd ca ak ag xat te di ko muñ nu àgg laataa jullig fajar mu fanaan guddi gi ci yekkati ay bayit di boroomug jàjji bayit yi mu doon yekkati ñooy ñaar yu busayri yii kuy sukkandiku ci ndimbalul yonant bi bu koy gaynde fekkee cib àll it wedam moom yonant bi foo ko gise ak doonte moom rekk a ànd da nga naan mook am mbooloo ànd ngir màggam ga li mu jublu ci di boroomug jàjji gi ci woy wi nag mooy mu nekk di jàjji fas wi ngir mu gaaw ginaaw bi nu àgg luga laataa fajar yendu fa nettali nanu ne sëñ bi nee na bi mu jegee luga kenn ci ndawi nasaraan bi te bokkoon ci ñi àndoon ak moom wax na ak moom ci anamug yërmaande ne ko ngànnaayul jege nanu noon bi de sëñ bi ne ko ci kàddu gu dëgar yàlla du lott te du des ginaaw bi nu àggee ba dal la ndaw li ko doon wax loolu dellusi ne ko man dey da ma laa wax ngir yërmaande ngànnayul jege nanu noon bi nga ne ma yàlla du lott te du des ginaaw li nga ma tontu ci sama wax jii de xawma ko loo ci jublu sëñ bi ne ko maanaam loolu mooy yàlla t s dara du fàddu ci moom kon mi ngi ànd ak nun bu doxee sama diggante ak noon yi ci kàttanam dàkku ma wëlif leen kenn du ma manal dara bu ma bàyye ak ñoom it ñu def la leen soob kenn du ci man dara wa in yamsaskal laahu bidurrin falaa kaashifa lahuu ila huwa wa in yuridka bi xayrin fa laa raadda li fadlihii muy ci maanaa bu la yàlla laalee ak lor kenn manu koo dindi ku dul moom bu la nammalee aw yiw it kenn manul a delloo ngënélam yàlla mu sell mi dëgal na yonant bi jàmm ak xeewal nanu sax ci moom jottalee ndaw li dem ànd ak mbégte man ma ne kooku sëñ bi daf ko doon leeral haalam haal mooy melo walla mbir walla aw nekkiin ak ni mu donne yonant bi j y m yonant bi j y m nee na wàkkiirlu mooy sama haal fàggu di sama sunna ku lott ci sama mbir bumu lott ci sama sunna sëñ bi moom donn na ci haalam ak sunnaam ab cér bu mag ak ci haalu ibraahiim j y m bi nu ko sànnee ca sawara sa malaaka yi ñaan ko mu sàkku ci ñoom ndimbal mu bañ jibriil j y m ne ko ñaan ko mu ne xam gi mu xam sama haal doy na ma ba du ma ko ñaan sëñ bi yonant bi la ciy jikko di ibraahima ci yite j y ñ day jëf haalu yonant bi ak sunaam gis nga haal ji noonu mu jëfe ko ma won la nag ag jëfeem sunna si bokk na ci loolu moom defal nanu ag xasida gu nu tënke harafi hasbunaal laahu wa nihmal wakiil muy ci maanaa yàlla doy na nu sëkk te moom de wéeruwaay bu baax la mu ne ci xasida gii laa sengewoo woon senge mooy ta ta walla ci tubaab fortification muy miir bi ñu njëkk ña daan tabax wërale seen dëkk yi ngir mu leen di aar ci song gu bette kon sengewu mooy aaru ca ngoonug bisub àjjuma ba ba ma dogoo ci ànd ak ñoom ca gàwwu ba ginaaw bi ma yonant bi j y m aaree digal ma ma dem ne ma wéyal te bul ragal lor xasida gii nag mooy muslaay li juttit bu ne war na koo jeem a am di ci musloo li mu ragal bu leen fàtte li ñenn ñiy wax naan waxtuw ajjuma mi ngi dale ca ginaaw tàkkusaan ba bu jant bi sowee xasida gi nag mooy gi tàmblee hamidtu man yahsimunii minad darar muy maa ngi sant ki ma musal ci lori jepp saytaane ak junne ak nit tudd naa sellam ga muy buur buy aji wattu may sàkkoo aaru ci wattoom gi wëlif musiba yi ak mbugal yi maa ngi sàkk ci moom mu musal ma ci bànneex ak ibliis ak ci mbooleem yiy lore ci jamono ju ne yeene naa koo ñaan di sàkk am ramu ci darajay soppeem bay ramu ñiy ramu mooy ahmad sangub mbindeef yi may julli ak a sëlmal ci moom te di ko def aw yoon jëm ca sama boroom maa ngi ñaan sama boroom ci darajaam mucc ci saytaane ak ciy ñaawtéef ak way bew yi di ma xaccoo yaa moom mbindeef yi yaw sama boroom may ma ag muc ci ñoom ak bepp balaa ak mbugal yaw laa jox sama bopp de yaw aji wattu ji ba fàww it ya ay sama wettal may ma li ma bëgg ci addina ak alaaxira na nga ma musal it ci gàccag àddina ak gu allaaxira jubale naa la sama kanam yaw sama boroom ya ak sama wasiila te loolu doy na ma musalal samag wàll ci mbooleem luy ñaaw te nga fegal ma mbooleem luy jax jaxiloo soril ma mbooleem noon yi ci barkeb yonant bi ak ahlu badri ñu tedd ñiy ay tànnéef na nga ma xeewale ci ma dugg ci sa senge kaaraange lu aaru li te dëkk fa di ku am kóolute ci samay noon yaw ay kiy musal kuy muslu ci yaw ci lepp lu ko man a jublu ciy mbugal samay mbir ba fàww da ma koy joyal jëme ci yaw ndax ya ay ki nga xam ne ku wéeru ci moom deesu ko jalax yaw aji baax ji fegal nga ma ag kéefar ak lori ñoñam ak jepp fitna fegal ma loxol woy bokkaale yi ci darajay ahlu badrin te nga def leen ñuy sama senge yaw aji baax ji nekkal ma te bu ma gecceel ci àddina ak àllaaxira te dee ma jéggal bindalal yonant bi ag xeewal ak mucc ak ñoñam aki saabaam ci anam gu sax mu tëje ko fanqalaboo bi nihmatin minal laahi wa fadlin lam yamsashum suuhun wattabahuu ridwaanul laahi wallaahu zuu fadlin haziim muy ci maanaa ñu dellu ànd ak xeewalug yàlla ak ngënéelam lu ñaaw laalu leen ñu topp ngëramul yàlla te yàlla ay boroom ngënéel lu mag li mu neeti alhamdu lillaahil lazii hadaanaa lihaazaa wamaa kunna linahtadiya law laa an hadaanaal laah wa aaxiru dahwaanaa anil hamdu lillaahi rabbil haalamiina muy ci maanaa maa ngi sant yàlla mi nga xam ni moo nu gindi jëme nu ci lii muy lislaam duñu doon gindiku bu nu yàlla gindiwutoon sunu wax ju mujj mooy ag cant ñeel na yàlla miy boroom mbindéef yi xoolal ni mu aaroo woon ci baat yii nga xam ni yàlla da leen a tagg tagg it nit ñi ciy aaroo mu wax allaziina xaala lahumun naasu innannaasa xad jamahoo lakum faxsawhum fasaadahum iimaanan waxaaluu hasbunaal laahu wa nihmal wakiil ba fam yam muy ci maanaa ñi nga xam ne nit ñi dañu ne leen nit ñi kat dajaloo nanu ngir fexeel leen kon tiit leen te moytu loola dolli leen ag ngëm ñu maase ne yàlla doy nanu te doy na sëkk ku ñu doyloo nga boole ca loola juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi yi mu jàngoon ca jeewal ba ndawul nasaraan bi bëggee wax ak moom waxees na ma te loolu lu wer la ne rakkam ja sheex ibra faati ci bis bi sëñ bi tukkee ba bi mu dellusee masul a dañ di def junniy salaatu alan nabii ci melo wii allaahuma salli halaa sayyidinaa muhammadin wa halaa aali sayyidinaa muhammadin salaatan tunajjiinaa bihaa min jamiihil ahwaali wal aafaati wa taqdii lana bihaa jamiihal haajaati wa tutahhirunaa bihaa min jamiihis sayyiaati wa tarfahunaa bihaa hindaka ahlad darajaati wa tuballixunaa bihaa aqsal xaayaati min jamiihil xayraati fil hayaati wa bahdal mamaati maanaa mi di yaw buur bi jullil ci sunu sang muhammad ak ñoñi sunu sang muhammad ag julli gu da nga nu ci musale ci mbooleem tiitaange yi ak gàkk gàkk yi fajale ñu ci mbooleem aajo yi laabale ñu ci ci mbooleem ñaawtéef yi yekkatil ñu ci gën jaa kawey daraja fa yaw àggale ñu ci ca dayo ya gën a sori ci mbooleem yiw yi cig dund ak ginaaw ag dee mu ko daan def ginaaw bu wàccee kaamil bi waaye kaamil bi moom lu saxoon la suba ak ngoon naka jekk njëkk sëñ biy tukki waaye salaatu halan nabii gi moom saxal gi man na a nekk muy ndigalul sëñ bi mbaa xalifaam bu baax bu sell ba ngir xér gu mu defoon ci muccug sëñ bi ak ag delluseem ci jàmm mu sàkkaloon ko mbooloo mu ci daawul sàggan suba ak ngoon waxambaane wu ragal yàlla wu dëkkoon kokki wii di samba joop nu gënoon koo xam ci samba asta daan leen jiite ku baaxoon la te gudoon aw fan mi ngi faatu ci atum waafiris sitri iiiiiiiiiii bokk na ci loolu woy gi mu def ahlu badrin ak aaru ci ñoom bi mu nekkee ndar mu mottali ko tudd itam ànd gi mu defoon ak ñoom ci tukkeem boobu ñu daa toroxal kepp ku ko daa jeem a lor teere boobu jotoon na koo won ca magi ndar ya ka ñu naan alhaaji muhammadu maabeey ne ko mu mokkalandi bayit wu njëkk wa ba ñu dajewaat ginaaw bu ñibisee te kat dajewaat nañu ginaaw juroom ñaari at aki weer bi nu dajee sëñ maabeey jàngal ko bayit wi daal di daanu ab jéll joy ak leneen ak leneen ci li mu aaroo woon te xamunu ko degg naa ko bis mu naan bi mu nekkee ci geej gi masul a dañ di jàng hisbul bahri bu imaam shaazalii muy lu am njariñ li koy wone mooy yitewoo gi ko sëñ bi yitewoo woon bayit wi mu digale woon mu wattu ko mooy njëlbéenug xasidag asiiru gu yeeme gi nga xam ne sëñ bi feeñal na ci njëlbéen gi ba ci fukk ak juroomi bayit lenn ci mbóoti tukkeem bi ci diganteem ak noon yi ak wone ci mucc gu mu mucc ci seeni lor xamale ne saytaane moo leen wor ci moom tax ba ñuy am njort yu ñaaw ci moom waaye seen njort yi sooy nañu te sëñ bi dellusi na ci jàmm bayit yee nekk nii maa ngi dox ànd ak ñu baax ñi waa ahlu badri bi may dox bi may tukki waaye noon yi jort ne man booba ku ñu njaf jàpp laa sama dox bi may def ci wommatug yonant bi ànd ceek gaa yu baax yi yàlla rekk a ko tax a jug ba fàww it samab dox du jëm ci ku dul yàlla bijji gi ma wommat bijji mooy jazbu di lol day xëcc kon man nanu koo jàppe yitewoo sunu boroom gi nga xam ne daa mujj mel ni ab asyee bu koy ñoddi jëme fa yàlla jëme ma ci aji tedd joj lu ma sàkku ci moom mu jàppandi mooy liy dox ak man samag cant ci xalima ak ci xol ak jëmm ñeel na ki ma nekkal cig tab ki nga xam ne jamono ju ne mi ngi may sottil ay xeewalam te mooy ki di ab santaakon ku soxlaalul kenn sama ndimbal samag dëgaral sama kaaraange ca noon ya mi ngi bawoo ci aji yaatu ji di ab mayewaakon ku tabe lool kooku mooy aji dimbali sama sama kilifa nag ci bu may dox ak bu ma taxawee mooy sama kerkeraam di yonant bi te mooy ki may ligeeyal te moom dey day xont mooy jox ab dund ku koy ligeeyal samab yool ci ligeey bi may defal ku nu tànn ki di yonant bi mayewaakon yàlla bee ko warlu te moom ku am lu mu faye la li ma nesar nag mooy nekk jaamub boroom aras rekk di ligeeyal gën ji mbindéef te moom yonant bi mooy samab xuppkat yonant bi day bashiir tey naziir di kuy begale tey xuppe njir jaam yi bañ a sàggan bañ a naagu aji feg jii di yàlla moo may fegal ci yonant bi ayi noon yi ak lepp lu ñaaw te mooy ki may xettali samag mujj mooy nekk dib jaamam di ligeeyal yonant bi mbiri mbindéef yepp nag ca yàlla lay mujj samay weer aki bis ëlëg ñoo may seedeel nekk gu ma nekk di jaamub yàlla te moom siw na samay sutura ci addina ak allaaxira mooy tag yonant b ci woy ak wesar te moom suturaalkat bu baax la samaw jiwu mooy teereb yàlla bi ak sunna si nga xam ne ci laay aaroo ci li yaqkat bi jublu muy saytaane samay kër weet na ñoñ ñi tas ngir tag ki nga xam ne noo ko man a tagge du tax tagg wi mat woru gi nekk ci mbindéef yi wor na nasaraan yi ciy pexeem ñu jort ay njort te njort ak woru la sëñ bi nee na ginaaw bi nu jullee tàkkusaan lanu dugg ci saxaar gi jëm ndar ñu àgg ndar bi jant biy bëgg a so ci loolu sëñ baa ngi ciy wax naan yàlla ca bu njëkk la dàqoon samay nëx nëx ca ndar jëme leen ci ku dul man ci barkeb ahlu badrin ña diy gaynde ñu àndandoo sax ca dun le ba akub coona fuglukat ya di ñu fa bari ma sax fa sëñ beey wax la desoon ca safar muy fukki fan ak weeru rabiihul awal ba ca bis bu mujj ba muy bisub alximis ci diir boobu laa matale woyug asmaau ahlu badrin muy turi waa badar topp ko wéral ko ci laa dajee it ak ñu bari ci kilifay ndar yi ak li ko wër kuréel it ci njiiti njaambur yi seetsi ma ngir tinusi ak ramusi ci tubaab bi ma ne leen ba leen ma ak sama boroom rekk moo leen ëpp ñeewant ci man gën leen a xam li gën ci man ñu far taxawlu nee nanu bi nu ko taxawalee ci seen kanam wax ak moom ci teewaayu kilifay nasaraan yi te booba moom ku weet la woon ci seen biir amu fa ab xarit du caangeenug aw wettal nu ne ko wax nañu nu ci yaw nàngam ak nàngam sëñ bi ne leen indil leen ma ki leen ko wax ba xam ma ak moom ku ciy ki wax dëgg te booba li nu doon wax naan moo ko def ab dof bu amut am xel sax du ko def waxantu ma la ak ku mel ni moom li am daal rambaaj la gu juge ci ñu kañaan lëjal ba ñu mujj amatuñu kersa ci yàlla saytaane yàq seeni xel jox leen xalaatam yu ñaaw ba nu mujj di rambaaj ak a tudd ciy ñaawtéef aki caaxaan lol ñi gën a dof ci wutkati àddina yi sax xalaatunu koo bëggal seen bop mbaa ñu koy soxla waxantu ma la ak boroom xel yu dëddu yi àdduna ca bis ba mu war juge ndar jëm ndakaaru te booba ma nga woor àgg fa njëkk jant biy so ñu wàcce ko fa ca genn kër mu tàmblee waajal dog ak julli waaye ñu jekki jekki rekk lenn ndaw teew ne ko ayca ñu dem sëñ bi jug ànd ak moom waa ja yobb ko ci néeg bu deesi muslu lëndam kariis tàng jérr xeeñ xunn bi sëñ bi gisee li wàcc ci moom mu xam ne mooy nattub yàlla bi ko doon xaar amu ci am pexe mu dul gàddu ko te muñ te sant yàlla te gëram ko ndax doon na sentu lu gën a réy loolu mu dal ni innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun sëñ bi nee na ma fanaan fa dundal guddi gi ci saari baqara ak aali himraan ñu feg ma ñoom ñaari saar yooyu ci ñaari sawara yi ak ñaari gàcca yi ma teg ci julli ci yonant bi j y m ki may ligeeyal sama dënn leer sama xol dal koolute gi dolliku ci yàlla ak yonant bi ndax alaa bizikril laahi tatma inul xuluub ci tudd yàlla ak fàttaliku ko la xol yi di dale sama gudd gi dal di neex ci yàlla ak ci aji sabab jii ak dëkk bi ak ci néeg bi ci loolu sëñ baa ngi naan yàlla dàq na jëme ci ku dul man ca ndakaaru wepp ay wu pexewaakon ki bari ay pexe bi xëccoon jëme ci man bu ma fattalikoo panaan moomee ak njiit loolee ak sax ga sama xol day naaw ak man jëm ci jëli xepp aki gobar ngir jiyaari waaye yonat bii di kiy fari bàkkaar dox sama digante ak loolu bi nu xëyee sëñ beey wax muy bisub àjjuma di bis bi njëkk ci rabiihus saanii lanu yeeg ca gaal ga gaal gi yendu fanaan am mbooloo ci murid yi dikkal ma ca dig gaal ga di joy bokk na ci mbooloo moomu sheex ibra faal moo ca magoon sëñ ba a ngi ciy wax ak ci gaal gi nana yàlla xamal na ma ci gaal gi ne maay jëwrini yonant bi gaal gu fees googu ak mbooloo yendu na fanaan muritam bu amub nattu boobu dikkal na ko ca gaalam gu nu duy ga murid ba tàggoo dellu ca dun ba ànd ak xol bu naqari mu jublu ci muridam boobu sheex ibra faal ci loolu la jiitoo woon ñepp am na ci biir gaal gi ba tay waa ju ko dikkaloon di ko laabiire naan ko am na njiit lu bees lu ñëw juge tugal jaxasoogul ak nit ñu ñuul ñi boo ko bindoon xamal ko ne danu laa tooñ kon mu delloo la sa kër ca sa njaboot sëñ bi nee na waa ji bàyyiwu ko di ko ci lëjal ba sëñ bi far jël daam ak xalimaam nee na bi ma tàmblee ba bind wenn bind rekk la ma wax ji dikkal juge fa boroom mbiondéef yi ne ma leegi da ngay diis sa aajo mbindéef mu mel ni yaw bàyyi ma fi ma daanaka faatu ngir tiit ak kersa ca saasa ma far la ma bindoon waaye ngoor si lëjalati ma ma ne ko loolu manul a nekk ne ko bu buurub buur yi di wax ak jaamam yi mu dëgaral kenn du ko man a xam ku dul ñoñam ña mos la ca neex ak la ca naqari nitug neen nag nga xam ni mook nit ñepp a yam dara waru ko lu dul mu gàttañlu ci loolu te yam fi mu war a yam bu bëggee mucc sunu ko tawfeexalul nangul ko ci loolu mi ngi naan ki njiit li yonni woon ca ligeeykatu yonant bi sàkku na ci moom cig laabiire mu yonnee ab bataaxel ca njiit lu bees la tukkee woon ca seeni suuf ba mu ko doon bëgg a bind far reccu ginaaw bi aji ligeey ji far li mu bindoon ñu neeti ko bindal mu bind xasida gu nu nangu gi ngir fàttaliku ki nga xam ne ci moom la yàlla di wonee aw yoon xasida gu nu nangu gi moom lanu def ci arafi waxi sunu boroom ji t s wa ufawwidu amrii ilal laah innal laah basin bil hibaad muy samay mbir maa ngi koy joyal jëme ca yàlla te yàlla a ngi gis jaam yi maa ngi jëmale samam mbind aji moom ji moom suuf ak asamaan ak buur yi gaal ga deqi bisub gàwwu ñaareelub rabiihus saanii sëñ bi nee na romb nanu konaakiri am benn wolofu saalum saalum bu ko fekk ci gaal gi jox ko fa àddiya ju kawe ne ko man de da maa degg ñu ne yaa ngi ñëw ci gaal gi jëm gabong ma ne naa la siyaaresi nga ñaanal ma dénk ma sëñ bi nee na ci waa jooju la dégge turu gabong xame ca it fi nu ma jëme ma dal di koy ñaanal ne ko bi ma koy dénk xamal yaw sama mbokk ak foo man a nekk ne amul benn buur bu dul yàlla ku jublu ci ku dul yàlla dana xam ne amul ku fi nekk ku dul yàlla ku jublu ci yàlla te jaaralewoo ko ci muhammad yonantab yàlla bi j y m da na xam ne yonant beey ki yàlla yonni ñu dal di tàggoo mu dem sëñ bi nee na ñu romb garambasaa mu ne am na ku ko doon ñaawal ci biir gaal gi waaye yàlla dox diggam ak moom ci hikamam loolu nag ni mu ame mooy daa am jëmm ju yéegoon ci gaal gi ca konaakiri te moom xamu ma woon bi nu jegee garambasaa jenn waay ju ñuul genne ci ab neeg ne ma ndax yaay diw jaar ci samaw tur ma xool ko mu ne ma nee nanu ma sama mbokk mag walla rakk de moo la jàpplu ngir barig li la sa taalube yiy rëyal ak màggal ak nàngam ak nàngam bi mu tollee ci wax jooju rekk gall gi dal di sab yuuxu mu dem di xaar coow li dal ba mu dolli ñaawalam yi waaye sab ga dakkul ba kerook gaal ga di teer mu wàcc ànd ak ñi doon wàcc kon alhamdu lilaa ginaaw amul li mu bëggoon ci loolu sëñ ba a ngi naan sama àddiya sell na ca konaakiri ñeel ku nu tànn kiy fari bàkkaar ci lu dul kuy weddi yàlla setal na ma ca konaakiri ci lepp luy xëcce jëme ci yu nu sib yàlla soril na ma cag njëkk ca garambasaa ka doon léewtoo ak man te mu dem wëlif ma àddiya jooju mu tudd foofu nag mi ngi ci jublu leeral gi mu leeraloon waa ja ko doon laaj maanaam laa ilaaha illal laa p wahuwal lazii yaqahu bihiil inkaar ba wa qad barraahul du àddiyay xaalis ju waa jooju mu tudd romb gi nu romb dawme wax karaama gu yeeme gi ko yàlla defal foofa mu ne daa jëloon benn bitéelu misk bu mu yoroon ngir wis ko ciy yereem aki téereem nee na ñu ne ko sànni ko ci géej gi mu ne ma gaaw sànni ko bi gaal gi teeree am mbooloo ci sunu mbokki jullit ñi duggsi ndax danu maa déggoon ñu ñëwoon ngir nuyyusi ma waaye képp ku dugg rekk jox nga ma ab bitéelu misk ñepp walla ña ca ëpp ci loolu la sëñ bi naan kiy jagleele yërmaandeem di yàlla woo na ma ci boppam ci indil ma xéewal yuy tee jaaxle mu jublu woon ci aji yërame jooju yàlla mii di boroomi xeewal daa ko indil ay xeewal bokk na ci xeewal yooyu biteeli misk yooyu mu wax ne bokk na ci karaama yi ko yàlla doon defal ci gaal gi tàggat gi mu defoon boroom gaal gi mu dikk di ko waxtaanal di ko won ag ñeewant ak yërmaande di mettitlu bu baax li dal sëñ bi daan baril lu mu ko daa wax naan ko yaw danu laa tooñ mu tuddati ne am na benn doktoor bu ko seetsi woon foofa mujj am yërmaande lool ci moom naan ko man daal da ma laa bëgg rekk te fas laa dimble mu ne am na wenn waxambaane wu tubaab wu ko dikkaloon wu bokkoon ci waa gaal gi mu ne yàlla def ci xolam mu sopp ma mujj di ma ligéeyal ni ko murit yiy defe mu ne moom daal noonu la yàlla nekke woon ak moom ciy xéewal tàggatal ko ñepp ba kerook muy wàcc gabong mu ne gabong moom yàggu fa dara rekk tuxooti fa dem ci beneen dun foofa nag ma sax fa juroomi at mu ne ci diirub juroomi at yii nag laa mujje mel ni ab jant mu jublu ci ci yekkatiku ay maqaama akug siw ak bari njariñ mu ne ci diir bii it la taalife taalif yu kenn masul a def cib taar ak bari njariñ ci yàlla ak yonnat bi ak ci lislaam dun bii nag mooy maayomba li koy tegtale mooy waxam ji mu naan ca tefesug geejug dun boobu laa taxawoon di irtijaal di wax ci lu dul xool li may wax ci am mbind di xutba geej gi naan yaw geej gi kennalal sa boroom te bul ko ñattal ndax sunu boroom kat kawe na wëlif ñu koy ñattal wareesu koo def ñatt ndax kenn rekk la cëy moom ni mu doone buur bu tedd na nga nekk di bajbaji di fuur ngir ragal yàlla te seere ne man ab jaamam laa mu ne ba mu fa defee jeroomi at la demati ci beneen dun nekk fa ak ab coona am fa ñatti at yu manke tuuti di ligéeyal yonant bi j y m mu ne am na wenn waxambaane wu bokk ci ñoom wu ko fekkoon fi mu nekkoon di bind mu bocc jaaseem di ko wëndéel ci sama bopp naan ma yaw ay diw di jaar ci sama tur ma ne waaw mu ne ma moytu ma sama maam kat raykatu walliyu la woon te maa di ab sëtam ma joxoñ ko sama xalima gi gëdd ko mel ni dama koy song ne ko xamal ni doo sa maam ja daa raye te du ma ku mel ni ña sa maam daa ray waa ja dal di tiit daw juge foofa fepp mu neeti am na kenn ci seen kilifa yi ku doon ñëw ca dun ba mu nekkoon di nemmikusi soldaar yi fan yooya yepp nit ñi dajaloo ci waajal kilifa gi di setal yoon yi ak a rafetal ak a samp ay raaya waaye bi waa ji ñëwee li mu njëkk a def mooy laaj ma ñu tegtal ko sama kër mu ñëw dugg nuyyu ma tudd samaw tur cig màggal dal di tàllal loxoom ngir nuyyu ma man itam ma tàllal sama bos waaye ca saasa am lu wax ak man mel ni ag dënnu gu juge ci asamaan ne yaa ayuhal laziina aamanoo inna maal musrikuuna najasun muy yeen ñi gëm xam leen ne bokkaalekat yi sobe lanu mu mel ni samam xel daa muuru ma bëmax ab loxoom bëmax gu tar ba waa ji yëngutu deltu ginaaw dal di taxaw ab diir mel ni day xalaat ci samay mbir waaye man loolu lepp teewul ma nekk ci samam mbind bi lu tollook waxtu jàllee mu woolu ki koy firil wax ak moom ab diir firilkat bi ñëw ne ma sa waa ji nee na mi ngi lay nuyyu te di la xamal ni bu ko mere ndax moom bokkul ci ñi la bañ walla mu lay lëjal di la tumbrankeel ak a genne sa réew moom de nee na bu ko manoon leegi mu delloo la fa nga bëgg boo gisee muy sonn ci yaw ak di la njëkk a seetsi bi mu daa taa wàcci mooy daa am kenn ci sa mbokki senegaal yi ku taxoon ma sopp la mu sàkku woon ci man ma nuyyul la ko moom dey ci ñi mu gën a sopp nga looloo waraloon sama ñëw gii du leneen sëñ bi nee na ma wax kiy tekki ne ko nee ko loolu ma def de ag bañ ko taxul mu dem waaye taxul mu soppiku ca na mu meloon bi mu demee ba toog dal ñu ne ma da nga koy teral te booba maa ngi ak as lëf ci seen mburu moomu ñu jaxase ak suukar mu doonoon mburu mu neex lool ma yonnee ko ko mu beg ci lool sant ma ne lii de bu ko kuy jambaar jambaarlu defoon te li miy woote nekkul ci moom man na ca a loroo waaye deesul loroo ci ndigal alhamdu lillaah da na xoromu ñu indi fi as lëf ci bayiti ibnu hanbal yii mu jëme woon ci sëñ bi ci lu aju ci xar baax yu mel ne yooyu boriwaa na aji jalgalti ku di ab tooñkat ku sol yerey teddngaam di puukarewu ciy tëneem aki takaayam ay junniy junni ñoo nekk ci ron kilifteefam te du faale lu koy digal mbaa mu koy tere ngeen sëñ bi lay wax wacce ko ci mbartalum toroxte dammte ko ci jaasiy ndimbal ju di ab dogaakon ju ñaw ndimbal lu tukee ca yàlla ñeel jaamam bii di jëwrini yonnant bi muy ndimbal lol nasaraanam yi sax mujj nanu ci di ay ansaaram di ay gaayam yu koy jappale bu wone woon mboot mi sekkare bi moom sëñ bi kon dey mbindeef yi gis lu yeeme waaye moom dënam bàmmeelu ay sekkare la tudd na moom sëñ bi ne bokk na ci karaama yi ko yàlla defal ci tukkib geej gi feeñug ahlu badrin mu ne moom kat tubaab yi danu koo dëkkaloon ci benn ci dun yi ca karce ga fa soldaar sa ñuy fo ak a naan ak a tux man may muñ seen lor yoou rekk ndax xam naa ne ñaari malaaka yiy bind jëf yi ànd nanu ak mukàllaf mu ne te ginaaw ñoom ñoo man a muñ boobule coona ak yooyule lor ngir top ndigalul seen boroom kon man du rafet fi man may jàmbat ndax kat li leen di lor rekk mooy li may lor li leen di naqàri rekk mooy li may naqàri te jàmbatunu ci noou yàlla dogal bis soldaar si genn ngir tàggatuji waaye ba ñu demee fa ñiy tàggatoo fekk fa am mbooloo mu war ay fas rang te kaalawu ci noonu ñu tiit taxaw seen njiit li tëyye leen fa xupp leen ci ne bu xibaar bi siwee da na leen ray ba suba jotee ñu ne mes gisatunu leen nu dal di nëbb seenub xibaar ñeneen ñi ko yëguloon sëñ bi nee na bi loolu jàllee ba tegi fan seen njiit woo ma mudaaranteek man waxa man wax ju rafet ci biir wax ji mu ne ma xanaa da ngaa am ay àndandoo yu lay dimbali boo bëggee def dara ma ne ay junne lanu walla ay nit mu ne ma yaa ko gën a xam sëñ bi nee na moom da koo wonoon ne moom yëgul li xew mu dal di noppi am na ñenn ci boroom xam xam yi ñu ko laajoon lu waraloon feeñug ahlu badrin gi sëñ bi ne woon ko ngir tiital noon yi keneen laaj ko ne ko ndax ahlu badrin ñooñu nit ña lanu walla malaaka ya mu ne malaaka ya keneenati laajati ko ne ko ndax yonant bi j y m ca la woon mu ne ko moo doonoon seen njiit ci loolu mi ngi naan ahuuthu billaahi minash shaytaanir rajiimi wa inniya uhiithuhaa bika wathuriyyatahaa minash shaytaanir rajiimi rabbi ahuuthu bika min hamazaatish shayaatiini wa ahuuthu bika rabbi ayyahduruuni maa ngi tàmblee ci turu yàlla miy yaatali xeewalam ci àddina te di ko jagleele ca alaaxira yal na yàlla mu kawe mi dolli xeewal ci sunu sang sunu kilifa muhammad ak ñoñam aki saabaam ak mucc ak barke bob dana ci wommate kepp ku jàng teere bii yobb ko ca àjjanaam ja mu dig ña ko ragal aamiin yaarabal haalamiin ahmadu mi dul dañ di sant boroomam di jaamub yàlla tey ligéeyal yonant bi j y m nee na ag cant ñeel na yàlla mii di rafetal ci samag wàll rafetal gu tooll ne rafetalug ku musla dañ di rafetal maang koy sant ndax kat moo tabe ci indil nu tawhiid muy wéetal yàlla ak ñaari mbokkam yooyu di lislaam ak lihsaan te ñooy sunnas yonant bi j y m xeewal ak mucc gu sax na ne ca xaritam ba soppeem ba ahmad ak ñoñam ak saabaam yu gëm yu jullite yu tedd yuy rafetal yi lii nii aw woy wu rajas wu am njariñ te tedd la ma tudde ko yobbalub ndaw ñi tathawudush shixaar jem ca àjjanay yàlla jii ami dex maa ngi ñaan yàlla ag nangu ak jàmm ak sell ak màggal maang koy ñaan woy wii di wommat kepp ku ko jàng jëme ko ca yoon wa gën a jub tey texeg ndaw ñi ak mag ñi ak waxambaane yeek jigeen ñi waxtuw soppiku jëm ci li nu tax a jug nag jot na sunu boroom laa ciy wut ci lu sax ag jiital yeen ndaw ñi maa ngi leen di digal ngeen bañ a wut lu dul ag jub te soxlawoo xam xam soxlawoo leen jàng ak mokkal te teet barabi texeedi yi taqoo leen ak ki dul dañ di jaamu boroomam ndax kooku kat la yàlla digale rekk la jeme kepp ku daw cig ndawam jëm cig jub bu màgge noppalu ku dabaatal li ko rëccoon ci lu bon akug neen te jeem a dundal waxtu yi ci tuub gu sell ak jublu sunu boroom am la gën jàpp leen ci sama laabiire gii ma leen jox kon dey da ngeen tonowu ci addina ak alaaxira bokk ci ñiy texe bunt ci xaaji diine yi diine ñatti xaaj la benn xaaj bi mooy bu gëm beneen bi di bu lislaam mooy ni nuy jaamoo yàlla ba yàlla di ko nangu ak bu lihsaan muy rafetal jaamu gi ngay jaamu ci sa digganteek sa boroom lu ci ne dees na ko gën a leeral ñu tàmbli ko ci xaaj bu njëkk bi muy gëm gëm mooy nga gëm yàlla ak malaakaam yi ak teereem yi mu wàcce ak alaaxira ak yonenteem yi ak dogal bi doggantal chapitre ci ni nuy gëme yàlla yàlla moom ni nga koy gëme mooy nga dëggal ni am gi mu am lu wóor la te aji jiitu la joj jiitoom gi amul fu mu tàmblee aji des la te desam gi amul fu muy yam aji wuuteek mbindeef yi la aji doylu ci boppam la kenn la kok amulub kem aji wéet la ci jëmmam maanaan amul kenn ku mel ni moom ak ciw meloom aki jëfam kàttan man manu jëf ak nameel maanaam bëgg di def ak xam xam akug dund ak gis ak dégg ak wax yooyule yu war ci sunu boroom lanu kon nag mu nekk di aji am kàttan lu war la tey ku am nameel di aji xam di aji dund tey kuy degg di kuy gis nekk it di kuy wax yu war lan ci moom ni yooyu nekke di ay melo yu war ci sunu boroom la ame yeneen melo yu waradi te jomb ci moom niki ñàkk maanaam sun boroom bañoon a am ak sosu ci maanaa muy ku nekkam gi am na lu ko fi jiitu nekkul di ku fi mas di ne ak jeex maanaam muy ku fi dul des ak niru ci maanaa yamoowut ak dara ci jëmm du caageenug ci meloom mbaa ay jëfam kon niroowut ak dara te loolu jomb na ci moom ak aajowoo jomb na ci sunu boroom muy aajowoo kenn ci lenn ak limu maanaam mu bañ di kenn di ay ñaar aki ñatt ak lott maanaam ñakk man man ci def li ko soob ak sibeel def dara cig sibeel mooy safaanub def ko cig nameel mooy def goo xam ni andul ak teeyug bakkan loolu jomb na ci sunu boroom ak tëx mooy safaanub degg ak réer di safaanub xam ak dee di safaanub dund ak gumba di safaanub gis ak luu di safaanub wax yile yepp jomb nanu ci yàlla sunu boroom tudd naa sellam ga kon daal jomb na ci moom mu ne di aji lott mbaa muy aji tëx mba muy aji jëf cig sibeel walla muy aji réer mbaa muy ku gumba mbaa ku dee soril naa ko loolu walla muy aji luu yii daal melo yu jomb lanu ci boroom asamaan moom daal sunu boroom deful dara cig war lu mu man a def cig nameel la koy def ak cig baax ak coobare loo fi gis daal ci mbindeef yi seenug jëf ak seenug ba ñoo yam ca sunu boroom lenn du ci lu war lu dagan rekk la ci moom dagan mooy lu man a nekk man a bañ a nekk doggantal ci ni nuy gëme malaaka yi yal na yàlla dolli xeewal ak mucc ci ñoom malaaka yi ñoom nga gëm leen mooy nga dëggal te am koolute ci ne ñoom kat ñu am lanu te ñu nu musal ciy bàkkaar lanu dun moy yàlla dunu xayta dunu puup dunu saw it ñu sunu boroom laabal lanu dunu lekk dunu naan jàmm yal na sax ci ñoom ñoom daal jaam yu yàlla teral lanu ba fàww ken du ci moy yàlla ku ci ne li ko yàlla digal rekk lay def ci leer la leen yàlla binde sàbbaal seen boroom mooy seenug naan sellal ko mooy seenug lekk doggantal ci ni nuy gëme teerey asamaan yi ni ngay gëme teere yi mooy nga dëggal ne wacce gi leen yàlla wacce lu wér la te lepp lu ne ci teere yooyu ag dëgg la gu deesul sikk seenub lim nag teemer ak ñeent la fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla aadama j y m juroom fukk yi nu wacce leen ci yonant yalla sihsa doomi yonant yalla aadama fanweer yi nu wacce leen ci yonant yàlla idriisa fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla ibraahiima miy xaritub yàlla bi j y m bu ko defee tawreet ñeel muusa j y m injiil ñeel hiisaa saboor davood j y m alxuraan jii nag wacci ci sunu sang bi muhammad yonant bi tëjj yonant gi yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci moom ak ci ñoom ñepp doggantal ci ni nuy gëme yonant yi mucc ak xeewal yàlla na nekk ci ñoom ni ngay gëme yonant yi j y ñ mooy nga dëggal leen te dëggal li nu indi jële ci seen boroom te nga gëm ne itam dëggu ak wóor ak jotal lu war ci ñoom la fen nag ak wor ak nëbb dëgg dafa araam ci ñoom gaar gaar bu dul ayibal tey dal nit da na leen dal niki tawat waaye bu mu doon juy foñloo maanaam juy tax nit ñi di leen daw niki ngaana nga xam ni day wàlle ak yu mel ni ñoom ñoom tawat yooyu danoo wormaal yonant yi dun leen dal waaye nag jaay ak jënd ak denc am soxna ak lu ni mel ci lepp lu yàlla daganal bun ko defee du leen dolli lu dul yoolub yàlla seen boroom liy wone ne ñoom ñu dëggu lanu te yàllaa leen yonni mooy kiimaan yi leen yàlla di wàcceel di ci wone ne moo leen yonni mu mel ni ñoom kiimaan yi daniy wax ak nit ñi naan leen jii waay de lu mu wax mbaa mu def ko yàllaa ko ko diggal yonant yi nag seenub lim ñatti teemeer ak fukk ak ñatt la waaye anbiyaawu yeek mooy ku am darajay yonant te yonniwun ko ci nit ñi yonant yi yepp boo leen boolee seenub lim moom teemeeri junni la ak ñaar fukk ak ñeent yal na mucc ak xeewal sax ci ñoom ci lu dul dog doggantal ci ni nuy gëme bis bu mujj ba yal nanu yàlla fegal ay tiitaangeem ni ngay gëme bis bii mooy nga dëggal ko te dëggal lepp li mu ëmb niki wisaareg teere ya ku ci ne dees na ko won ay jëfam ci teere ak pang ma muy dajale gi niy dajale nit ñi ak balaas bi muy balaas bi niy mandaxee jëfi jaam yi ak déegub yonant bi j y m ak ajjana ak sawara ak siraat aw yoon la wu deesi romb ak romb gin ciy romb ak hisaab mooy seet gi niy seet jëfi nit ñi ak rammug yonant bi j y m ak mbugal yal nanu ci yàlla musal hisaab nag luy tar la ca boobale bis ndax dees na hisaab nit ki ci lu gën a tuuti fepp suuf cib tuutaay fayyantoo itam dana fa am ndax lu waay daa jay moroomam fii teg ko cig ëpp doole bu yawmal xiyaamee dees na jox aji neew ji doole doole muy fayyu ci ki ko daa neewal doole niki xar mi am bejjan te daa daan mi amul bejjan bu bis baa da niy jox aji ñakk jiy bejjan bejjani mi ko daa daan muy fayyu loolu lepp maandute ga fay am lay wone dee ak laajug malaaka yi ak mbugalum bammeel ci yawmal xiyaam lanu ndax kat yawmal xiyaam yi ñaar lanu bu mag ak bu ndaw bu ndaw bi mooy dee gi ñepp di dee bu mag bi di wal gi niy wal buftu bi doggantal ci ni nuy gëme dogal bi gëm dogalub yàlla bi mooy dëggal ne lépp lu am moo xam lu làqu la walla lu feeñ ak fu m man a ame sunu boroom mooy ki ko xamoon namoon ko am kàttanug def ko def ko moo xam lu baax la niki jëfe ndigëli sunu boroom yi walla lu bon niki jëfe tere yi walla muy lu neex niki yoolub jullit ñi walla lu naqari niki mbugalum yéefar yi cig gàttal daal lépp lu am ci saayir ak ci baatin dogalub sunu boroom la nit ki daal war naa gëm ne amul kuy jeexiital ci dara ku dul yàlla lu fi am cib dogalam la ame bunt ci lislaam lislaam mooy wax laa ilaaha illal laa muy yàlla rekk ay buur amul beneen buur bu dul mom ak julli ak woor aj màkka natt asaka doggantal ci laa ilaha illal laa wax laa ilaaha illal laa amul benn buur bu dul yàlla muhammad yonantub yàlla a yal na yàlla dolli xéewal ak mucc ci moom ak ñoñam aki sahabaam mooy ngën ji lu kuy wax di wax ku ko weddi it pert rekk ku ko saxal tey teewlu maanaa mi da na tonowu te du dajeek nëx nëx bunt ci julli yi juroom julli yi juroom farata la ci lu dog ci alxuraan ak suna ak ci dajeg boroom xam xam yi kepp ku ko bañ a def ngir weddi mook ku tubbee yam cib àtte dees koy tuubloo may ko ñatti fan bu tuubee nu ba ko bu tuubul sariiya ray ko ci jaasi te deesu ko sang deesu ko sàng deesu ko jullee te deesu ko suul fa jullit ña imaam daal day yonni kenn rekk mu suul ko te dunu ko jublule xibla te alal ji mu am it ci baytul maal lan koy def baytulmaal mooy trésor publique bu nguurug lislaam ku nangu ne julli lu war la ba noppi lànk ne du ko def te amul ngànt moom danu koy bàyyi ba waxtu julli wi jot nu digal ko bu lànkee nu muñal ko ba doroora ji dem bay bëgg a jeex nga xam ne lu tollu ne benn ràkkaa rekk a ciy bëgg a des bu bañee nu topp ko ba mu wóor ne faatiya sax xajatu fi walla ab yamoo loolu lepp nag ngir bañ koo ray ñongal dereetam bu bañee kilifa gi ray kook jaasi rayug gëtën mu bañ a doon ni nuy raye ab yéefër bu réccoo nag ne nan ko ba mu julli ngir ragal a dee deesu ko nangu dees na ko jullee nag waaye boroom ngëneel du ko jiite ndax da nuy bañ keneen di ko ci roy bàmmeelam nag dees na ko fonk jégénal ko jal ko kenn du ko maasale noonu rekk ndax moom fi boroom xam xam yi ab julit la lii dey waxi imam hawfii la doggantal ci laab laab moom lu war la ci alxuran ak sunna ak dajeg boroom xam xam yi ku ko bàyyi ci lu dul ngànt lu xel nangu dees koy ray rayug gëtën gu dul gu yéefër ndaxte julli du mat mukk lu dul dafa ànd ak lab kon ag waram lu wér la doggantal cig soññee ci ñu farlu ci ràññale diggante farata yeek sunna yi ak ñàkk cee sàggan koo xam ne julli na ca anam ga mu gën a rafete ci maanaa mu jullee ni ko yàlla digalee metal rukoo ya ak sujood ya metal taxawaay ya ak jataay ya te bawul dara lu nu war a def ci julli gi mu noppi nag nu laaj ko li julli gi am ciy farata akub àtteem ndax moom julli gi farata la walla sunna walla lu nu sopp te moom xamul dara ci li nu ko laaj xanaa mu tontu rekk ne man daal da may gis nit ñi ñuy jaamu ma ànd ak ñoom ca la ñuy def waaye li ci des xawma ci dara ci loolu yenn boroom xam xam yi nee nanu julleem gi baaxul te dunu nangu ngàntam li naka noonu ku jàpp njàpp mu sell raxas ñatti yoon ay loxoom ba ci tikkujara yi gallaxndiku gu ànd ak soccu saraxndiku fiiru lu ci ne ñatti yoon raxas kanamam ay loxoom lu ci ne ñatt te xaliil baaraam ya masaa boppam tàmblee ko ci fi jë bi yam ba ci doq gi delloosi ko ba fa mu tàmblee woon masaa ñaari noppam ginaaw bi mu tooyalaatee ay loxoom raxas ñaari tànkam ànd ak xaliil leen matal njàpp mi ni mu ware naka noonu ku sangu janaba ni mu ware raxas ñaari loxoom ñatti yoon ba ci tikkujara ya raxas li ko taq ci sobe raxas pëyam walla sakkaraam ànd caak yeene bu noppee jàpp njàppum benn benn xaliil mbooleem kawaram tooyal ko tamblee ko ci mujug ndaal bopp li ngir jañ lor ji dal di raxas boppam ci ñatti tanqi ndox yum tanqe ci loxoom ginaaw bi mu ko xaliilee dal di as ndox ci tenqul ndijooram jengal boppam raxas noppub ndijooram bu jàllee mu defaat noonu raxas bu cammooñam dal di raxas ag doqam ak wetug ndijooram ba ci bëtu woom bi def noonu ci gu càmmooñ gi dal di raxas tankub ndijoor bi ba ci dajoor bi teg ci bu càmmooñ bi dal di matal am cangaayam ci raxas biir bi ak dënn bi ginaaw bim raxasee ginaaw gi te xamul ci loolu lepp la cay farata ak la cay sunna kon na ko wóor ne tojam ma toj mooy ñàkk a lab dañul te julleem ga mu ca julli baaxul te coonaam boobu bepp du ca jële lu dul bàkkaar te mi ngi moy yàlla ak yonentam bu sel bi j y m wax jii nag mi ngi bawoo ci imaamul hawfii luy tiitloo tey jàjjee ngi ci nag nee na itam gépp jaamu yàlla gu nu defe nii njariñ du ca juddoo moo xam aj la walla jihad walla woor walla yu ni mel niki joxe ak lele am nag ci boroom xam xam yi ñu ci ne ku sangu mbaa mu jàpp def ko ca anam ga mu ware yeene ca biir def la yàlla farataal na xam ne jëfam ja ju nu nangu la ju baax la te dana ko doy ca la gën a wér te julli gam ca def it gu baax lay doon bu ca yeenee def la ca yàlla farataal amul it benn bàkkaar mbaa muy moy yàlla ngir ñàkk gi mu ñàkk a gëstu waxi imaam hawfii jii du dara lu dul ag xuppe akug yeete akug laabiire ngir nu farlu ci jeem a xam farata yeek suna ak yi ni mel yàlla na ko yàlla fay aw yiw li ma sëriñ beey wax wax mooy yàlla dey araamal na ci mukalaf mu ne ci li nu tuxal jëf dara ci diine te xamoo la cay àtteb yoon yax mbind mii bii nag daliil xathii la daliil xathii ci wallug usool mooy lu wér lu mel ni alxuraan kepp ku réere farataam te laajul na xam ne tooñ na boppam te alag ko doggantal ci faratay julli faratay julli fukk ak juroom la ci li faqiih bii di hawfii wax ñooy yii yeene kàbbarub armal ba taxaw ngir kàbbar ko jàng faatiya taxaw ngir jàng ko rukoo siggi ca rukoo ba sujood siggi ca sujood ba yeenee roy imaam boo ko amee ca njëlbeen ga toftale gi dal gi yamoo gi sëlmël bi jataayub sëlmël bi tàmblee ca alifug al gi ba ca miimug kum gi doggantal ci sunnay julli ay sunnaam la liqaam saar wi ci ginaaw faatiya sunna sun feddali la taxaw gi gay taxaw di ko jàng sunna sun feddali la birël fi mu ware yalu fi mu ware kàbbar bu dul bu njëkk bi taaya ju njëkk taaya ju mujj julli gi ngay julli ci yonant bi ca taaya ju mujj ja jataayub taaya ju njëkk ja jataayub taaya ju mujj ja li dolliku ci dal gi ngay dal li dolliku ci sëlmël bi birël sëlmëlub farata ba delloo sëlmël imaam delloo ko ki ci sa wet xerawlug maamoom bu imam dee birël am saatir bu dee imaam walla kenn ku beru waaye kuy roy moom imaamam doy na ko saatir doggantal ci faratay njàpp faratay njàpp juroom ñatt la ñooy yeene raxas kanam gi raxas loxo yi ba ci conc yi xaliil baaraami loxo yi masaa sa bopp raxas sa tànk jonj gaaw doggantal ci sunnay njàpp sunnay njàpp moom itam juroom ñatt la ci li imaamul hawfii wax raxas say loxo ca tàmbli ga galaxndiku saraxndiku fiiru masaa sa ñaari nopp tooyalaat say loxo bala ngaa masaa say nopp boo masaa sa bopp ba ci doq gi delloosi gi nga koy delloosi toftale gi doggantal ci faratay sangu faratay sangu joroom la yeene booy tàmbli jonj gaaw xaliil kawar gi nal ay lett ci kepp ku lettu doggantal ci sunnay cangaay ay sunnaam ñeent la raxas loxo cig tàmbli galaxndiku saraxndiku masaa ker nopp yi doggantal ci faratay tiim faratay tiim juroom ñatt la yeene pakk bu lab gaaw door gi ngay njëkk a door say loxo ci suuf masaa sa kanam masaa sa tikkujara jokkale ko ak julli gi defe ko ci biir waxtu wi ndax du baax bu jotul doggantal ciy sunnaam sunnay tiim ñatt la toftale ga mooy jiital li war a jiitu li ci war a top topp ci doorub ñaareel bi ngay door sa loxo ci suuf masaa li top ci tikkujara yi na nga ba tiim nag tey jàpp boo weree waxunu boo weredee walla nga am ngànt lu wér kon bu boobaa nga man a tiim doggantal ci woor woor ñaari farata la am yeene ba liy dogloo ngir yàlla sunna yi ñatt la gaaw a dog yeex a xëdd ba wax ju ñaaw doggantal ci asaka asaka moom ñeenti farata la am yeene matug at matug nisaab bañ koo joxe feneen te fi nga ne ku ko yayoo nekk fi am na ñatti teggiin nag yuy waralub yool nga ànd ceek teeyug bakan mu bañ a doon la gën mbaa la yées ci sa alal joxe ko ci sutura ngir daw gistal doggantal ci ajj ajj ñeenti farata la am yeenee ajj tawaaful ifaada dox diggante safaa ak marwa taxaw arafa doggantal ciy sunnaam sunnay ajj fukk ak ñaar la am na ci ñeent yoy ñi ngi ame ca armal ga sangu gu jokkook armal gi rafle ci lunu ñaw solub ñëkk akug làmbaay aki dàll labayka tawaaf gi am ñeenti sunna dox gi foon gi doj wa ci loxo walla gimiñ ñukk gi ci ñatti tuur yu njëkk yi ñaan gi ngay ñaan ci tawaaf bi dox gi safaak marwa it am ñeenti sunnaam foon doj wi bu dee daa juge ca jàkka ja jem safaa ag yeegam diggante safaa ak marwa gaaw gi niy def ci batnu masiil ñaan gu amulub àpp gi ngay def ci kaw safaa ak marwa lii ag mottali la nettali nanu jële fa gën ji mbindeef ne ku birël ci ginaawug laab ne ashadu ba fam yam da nanu ko ubil bunti àjjana yi mu dugg ci bi ko soob waaye wuute nanu ci jamono ji nu koy ubbi doggantal ci ni ngay faye li la faat ci ginaaw imaam lu war la ci maamoom mu fay li ko fat ci ginaaw imaam suba waxtoom a ngi tàmblee ca dëgg dëggi fajar ba bu tàmblee leer bu la cib ràkkaa faatee jugal ci lu dul kàbbar jàng faatiya akuw saar cig birël te bul xunoot waxtuw tisbaar tàmblee ca sawaal ba ca mujjug taxawaay ba bu la cib ràkka faatee jugal ci lu dul kàbbar jàng faatiya akuw saar cig yalu jekki taaya sëlmël boo ci ñàkkee nag ñaari ràkkaa jugal te kàbbar te jàng faatiya akuw saar cig yalu te bul toog da ngay jug def beneen julli gi mat bu la ci ñatt rawee nag jugal te bul kàbbar nga jàng faatiya akuw saar te yalu leen nga jekki taaya jug def beneen ràkkaa bu ànd ak faatiya akuw saar te doo toog da ngay defaat beneen ràkka rekk cig yalu bu ànd ak faatiya dong mu jeex waxtuw tàkkusaan a ngi tàmblee ci matug taxawaay bu njëkk ba ba ca waxtuw gel wa mooy bu jamono tàmblee mel ne lu mboq tàkkusaan mook tisbaar a yam ci ni nu koy faye araf ci araf timis moom waxtoom a ngi dale ci jànt bu so ba ca fàddug safaq bu la cib ràkka rawee jugal kàbbar jàng faatiya akuw saar cig birël bu la ci ñaari ràkkaa rawee jugal te bul kàbbar jàng faatiya akuw saar te birël ko taaya defaat ràkkaa bu ni mel te sëlmël gee moom mi ngi tàmblee ca fàddug safaq ba ca ñatteelub guddi guddi gi bu nu ko xaajoon ñatti xaaj benn xaaj bu njëkk bi bu njëkk bi bu la ci benn ràkkaa rawee jugal bul kàbbar jàng faatiya akuw saar te birël ko bu jàllee nga jekki te taaya te sëlmël bu la ci ñaari ràkkaa rawee jugal kàbbar te jàng faatiya akuw saar cig birël te bul toog nga defaat na nga defoon ca bu njëkk ba bu la ci ñatt rawee jugal birël faatiya akuw saar ci lu dul kàbbar jekki taaya te jugaat defaatub rakkaa ànd ak faatiya akuw saar cig birël waaye doo toog da ngay wéy ca ba ca des jàng ca faatiya rekk te yalu ko boroom xam xam yi ñoom jotub rakka ñi ngi ko teg ci am ab rukkoo cib ràkka ànd ak imaam ku amul ab rukkoo ci ràkkaa ànd ak imaam na ko woor ne jotul ràkkaa ba ku jot imaam ci taaya daa war a dooraatug julleem bunt ci lihsaan lihsaan mooy nga jaamu yàlla di ko teewlu ba mel ni da nga koy gis ci lepp li ngay def te mu wóor la ne boo ko gisul it moom mi ngi lay gis kon na ngeen koy fuglu bu ngeen bëggee àgg ci martaba yu kawe yi na ngeen di jëfe ndénkaane bile maa ngi leen di denk xam xam ak kersa ak sant yàlla ak sellal ak tabe ak noppeek lewet booy xamlu ak muñ ak ragal yàlla ak degg degglu maanaa yi na ngeen di farlu ci top aji yërëme ji fu ngeen man a ne te sori noonoo bu leen baril wax aki nelaw na ngeen di teet luy waral yaq di moytu ngistal fu ngeen man a ne ak rëy ak mbañeel tey sàkkug leer maa ngi leen di denk ag dëggu ak wakkiirlu ci yàlla ak toraxlu ak neewi mebët denk naa leen bariy teggiin loolu da na waralub yool barib xam xam ci lu duli teggiin ay akub coona rekk lay waral yeen gone yi bu leen di toog ak ku dese cim xel dee leen toog ak kuy gindee kuy gindee kat mooy kiy genne aji toogaale ji jële ko ci juroomi mbir jëme ko ci juroomi mbir moo koy jële ci ngistal jëme ko ci sellal te du naafeq moo koy jële cig rëy yobb ko cig toroxlu ak muñ moo koy jële cig noonoo jëme ko cig laabiire moo koy jële ci sikk yobbu ko ci yaqiin gu ko man a dollig kawe moo koy jële ci bëgg lu koy lor jëme ko ci lu koy jariñ màng profitoo leen juroom njëkk juroom ni ko yonant bi j y m digalee bi ci njëkk mooy ag ngone njëkk màggat wér njëkk wéradi am koom njëkkug ñàkk ag féex njëkkug féexadi dund njëkk dee gaawantu leen jëm ca yiw wa njëkk muy faat fii la tasawudus sixaar yam ànd ak sant sama boroom miy aji feg ji gacca woy naa ko nag ndir jëmmi sama boroom mu tedd mi di yaakaar ci moom ab yool bu dul dog mu diw woy wuy wommate jëme ci xam xam ak jëf ak tegginu tey jàppndal mebat yi mu diw rajas wu am njariñ te barkeel wu way texe yi bokk yàlla ci barkeb yonant bi j y m nangu na woy wii jariñ ci it kepp ku texe kuy laabiire te yewwu moom woy wi du dañ di bijjee jëme cig baax di jañ gepp texeedeek woru yàllaay ki ma digal ma woy ko yàlla miy ki nu jublu mi may fegal luy waral njàqare woy naa ko ngir jëmmam ju tedd ja moom mi jënd samam njaay ànd ak di ma teral konug cant ñeel na yàlla xeewal ak mucc yal na nekk ci ahmadu aji rammu jiy boroomi ngëneel ak ñoñam aki saabaam ahmadu mii dib jaam buy ligeeyal yonant bi mi ngi sant boroomam subhaana rabbika rabbil hizzati hamma yazifuun wasalaamun halal mursaliin wal hamdu lillaahi rabbil haalamiin lii ag xamle la bokk na ci njariñi woy wii ki ko woy muy sëñ bi ci ndigalul yàlla mu kawe mi te sell la ko defe ak ci lol yonantam ba jàmm ak xeewal yal na sax ci moom bokk na ci ngëneeli woy wi begal gun ko begal bim ci noppee moom sëñ bi ne ko woy wii de la yàlla t s ak yonant bi j y m gën a sopp ci ay keman bokk na ci li nu ko begale kepp ku ko jàng walla nga mokkal ko texe ag texe gu texeedi dul toppati bokk na ciy jagleem ku ko mokkal munkir ak nakiir dun ko laaj ci bàmmeel ak leneen ak leneen ak leneen yàlla mooy jagleel yërmaandeem ku ko soob yàlla mooy boroom ngëneel lu màgg li bii jukki bu am solo la ñu def ko ci cawarte gi murit yi ame ci wàllug fàggu ak koom koom ñi ngi ko jële ca yëglekaay gu siw googu di the economist di genn këyitu xibaar gu gore guy génn ayu bis gu nekk te adduna bepp xam ko muy wax nag ci mbiri adduna bi bepp moom nag mi ngi njëkk a génn ci satumbar economist newspaper limited filiale de pearson ca london moo ko génne li ñu ci gën di wax nag mooy koom koomu adduna bi politig jëflante xaalis xam xam xarala ak fànn art lim bu ci génn di nanu ci defar lu ëpp milyo te ba ca biti angalteer lanu leen di jaaye ji yëglekaay gi tas na ci lu tollook ciy yax ci xaaj bu njëkk bi ci atum ci li gëstug bureau of circulations wax di jumtukaayub natt bu nekk ca angalteer ci ñiy jënd yëglekaay bii ak di ko yër ay waa amerig lanu ay waa angalteer di ñu dëkke tugal gu goxe gi continentale yëglekaay gi dees na ko yër ci lu tollook réew faith in the market ngëm ak yaxantu ci ginaaw luumay itaali yi nuy defe fu lenn dul tiim lu dul asamaan si am mbooloom jullit mu afrig a ngii di indi ay tontu ci li nuy tudde addunaal di mondialisation kepp kuy door a teg tànkam ci suufus rom péeyub itaali dana gis ne dëkk bii de sol na mbubb mu bees mu mel ne du manu ko xame woon mbubb mii nag mujj na di mu ñu ko xàmmee ni nu ko xàmmeek baaram yeek tànganaam yi nga xam ne dees na fa faral a guuxe leeg leeg as lëf ci lii di cappuccino di kafe gu nu jaxaseek meew te nu gën a miinew jëfiinam ca itaali bu ngéen jëlee yoon wi jëm vatican jaare ko ci via della conciliazione mu dim mbedd mu ca jëme da ngéen gis ne lu bari ca peggi tëli ya de danu koo muure aki jaaykat yu bawoo afrig yu lay wër aki maska yu ndaw yu waso ay saag ay der ceintures walla ay weeri jant yu nu roy maanaam yu doonul piir bu ngéen fa taxawee as ndiir nag di léen seetlu bu ngéen moytuwul da ngéen fa seetaan powum muus ak jinax mi nga xam ne jaaykat yii baaxoo nanu koo def ak takk der yi mu dig dàqante gu xoromu te yërëmtalu nii daal lanu koy nekke saa su nu léen yëgalee ne takk der yaa ngoog da nga leen di gis ñu taxañ seeni bagaas cis lëf cig gaaw daal di laxas seeti nu nu man a mucce bu yàlla dogalee rëccuñu bu booba a seen yoon du nekkati ci seen njaay moomu moom kay danu ko fay bàyyil takk der bi leen jàpp mu dajaleel ko boppam daal di leen yobbu ca dëgg dëgg jaaykat yii nekk ci yoon yi jëme vatican man ngaa wax ci ñoom lu nekk lu dul nosuwunu organisewuwunu ñoom de ñi ngi bokk ci kuréel gu nosu gu nu xame ci adduna bi ci gëm gëmu diine ak bu koom koom te am it ab barabam ca beneen dëkk bu tedd di tuubaa nekk nag ci digg senegaal boo fa jëmee nag juge dakar péeyub senegaal ñatti waxtuy tukki rekk lay tollool niki yeneen imigire yu bari yu senegaal yi nga xam ne yenn yi ay dawalkati taxi lanu ca new york walla ñu diy wattkati suraas orange ca espaañ jaaykat yii di wëndéelook seeni njaay ca rom ñi ngi bòkk ci genn kuréelug jullit gu tasawuf nu koy wooye yoonu murit mooy yoon wi ëmb taalubey cheikh ahmad bamba yi kii nag ag kilifag diine la gu làqu atum ñoom nag ci jeexitalu gi nu def ci njàggalem sëñ bii indi nanu ay tontu yu am solo ci laaj yi ja yu adduna yi di indi aju ci ay marsandiis aki ligeey maanaam dugal nanu seen loxo bu baax ci yaxantu gi ci adduna bi li ëpp ci milyo yi dëkke senegaal ay jullit lanu waaye lu ci ëpp danuy bokk ci benn ci ñaari yoon yu mag yii di wu murit mbaa wu tiijaan moom nag yoonu tiijaan moo fi jiitu wu murit bamba moom leeral na am njàggaleem mi nga xam ne ñi ngi ko xame leegi ci turu ag murit leeral na ko ne mooy ag dellu rekk ca cosaanul lislaam gas reen ya xame ko na ko yonnat ba indee woon waaye nag moom lislaamam lu néew la nirooleek ju xaw a tar ja bawoo araabi sawudit lenn nag am na mooy murit yi danuy xaw a def li nuy wax culte des saints et de leur tombeaux muy ci maanaa jaamu wàlliyu yi ak seeni bàmmeel ba ci bu seen sëriñ boobu sax te loolu ñoñ wahaab ñi danu koy weddi di ko kontar waaye murit yii nga xam ne danoo doylu ci seen bopp yëgunu sax ne ñi ngi wax ak a weddi ñoom wahaabit yi ñoom daal danuy dajale seen alal def ko ci li nu bëgg tabax seeni jumaa aki jàkka te dunu soxlaal ñii di waa araabi sawudit dara ba dara booloo jeex sheex ka di sët ci bamba ca biir këram ga nekk tuubaa di dëkk bu fees dll ak ragal yàlla waaye it di bu nu bàyyikoo fu nekk dëkksi fa ag yaxantu gu lokaal di fa dox bu baax ak a naat ci wàll goo wëlbati sa bët jëme moom sheex ka mii leeralal na nu gisiinu sëñ bii nga xam ne mooy sukkandiku ak wéeru ci sa bopp bu ngéen wéeroo ci keneen mi ngi nuy leeral du ngéen gore mukk lii mooy sunu gisiinu dund bi mu fi daataa juge bamba mébetoon na ay mbir yu bari bëggoon na tuubaa dëkkam bi mu sanc nekk dëkk bu sell njabootam gi ci déggiin wu yaatu wi mbàkke mbàkke yi ëmb na lu sakkan ciy sëriñ wallay jànglekati xam xami diine yuy boole jàngale liyeey bu tar ci seenum njàngale ak temb maanaam bañ a wéeru ci kenn ak dimbalnte xalaat yii nag moo jàñ murit yi ci ñuy faral a tukki ak a tuxu di dem ci yeneeni réew ngir wëri ligéey ngir man a yonnee seeni njaboot lu nu man a dunde man cee suturloo ak ngir man a jox àddiya seeni sëriñ sii nga xam ne ñu ci ëpp danuy faral a tukki di wër adduna bi ngir nemmeeku ji seen taalube yi ak ngir suqali dëkkub tuubaa bi lii lépp nag jëf na ay jëf ci def murit yi ñuy benn ci kuréeli afrig yi gën a tkki moo xam ci seen réew la mbaa feneen fu ñu nekk ci adduna bi rekk dananu jeem a booloo ngir jënd jàkka walla barabub daje seen dimbalante gi nuy def tax na ba ñu bees di man a tukki bay man a ligeey ak a ami këyit ci safaanub ñu nekk fi di ngàññ dogal bi ak a jàmbat ñoom daal yaxaantukat yu sawar lanu te muus yuy dugg ci ligeey yu yombadi yi nga jort ne dunu ko man te fu nekk it ci adduna bi danu fay dem di def senni ligeey nan jël ku mel ne aliyun ka ab bitig la am buy def njaayum bëbëstan vente en gros ca wetu gaarub rom ba tudd termini moom rakk la walla mag ci sheex ka mi nekk tuubaa di topptoo njaboot gi aliyun ka mii jaaykat la buy def njaayum ay maska yu waaso di ko jaay nag ay moroomi senegaleem yuy jaay di wër walla sax ñu duli senegale bu ko defee ñoom ñii di ko jaayaat ci mbedd yi walla ci tefes yi lenn nag ci njaay mii senegaal lay bàyyikoo wayye li ëpp day bawoo endonesi thailande mbaa end teewul aliyun nangu ne am na leeg leeg ay jaaykati imigre yu juge ci yeneeni réew yu gën a muus murit yi ci di indi njaay walla jaayiin wu bees moom nag aliyun ku naw ñenn ci ñiy wujjeek moom ci njaay mi la te juge banglaades ndax nee na ñoom danuy déglu xibaari jawwu ji meteo ba bu nu nee suba di na taw rekk ñu gaaw wuti parasol jaayi am na benn yoon ci mbedd mi sang ka def fa nuyyoob taalube bu tàng ak ay mbokki muritam yu def am mbooloo mu rafet tey jàpplante jaaykati saag yii ak der nga xam ne yu ci ëpp siin lanu juge ñu ligeeye leen fa danuy faral a daje ngir weccante seeni xalaat ak xam xam yi aju ci ni nuy lijjantee bay mucc ci takk der yi bi añ jotee gan dikkal na sang ka di benn waa reewam n gey mi nekk ci bunt bitigam tey jaay ay tòggi senegaal yu tàng plaat bu nekk euro benn yoon ci ayu bis gi lu ëpp ci murit yi nekk rom dananu daje ngir def daayira julli jàng alxuraan aki xasida gisante siyaarante xool ci seen biir ki ci yayoo ndimbal leeg leeg as mbooloo ci ñoom danuy déggoo ci bokk luye ab kontaneer yonnee ci seeni njënd aki bagaasi jëfandikoo ngir nu jaayaat leen ca sandaga ja bu nekk ca dakaar te murit ya ëpp fa ay anam yu wuute it am nanu yu niy yonnee xaalis looloo tax këri ligeey yiy yëngu ci wàllug yonnee xaalis yu tas lanu ci mbooleem ruqi senegaal waaye imigre yi ñoom li gën a noppale ci ñoom te nu gën koo taamu ak a def mooy woo seenub xarit walla xame ca sandaga ngir mu joxal leen seen mbokk ma soxla ñi ngi nattale ne murit yi tollu nanu ci ci askanu senegaal wi waaye bu dee ci bitim réew ñoo ëpp ci imigrey senegaal yi nuy tollale ci murit yi it ñooy daanaka ci jaaykati senegaal yiy wër tey jaar ci mbooleen qàli itaali yu mag yi fraans mi doon dooley sancaan ji tegoon loxo senegaal mujj na doonatul réew mi senegale yi jëme séen një ay fukki at a ngii itaali nangu barabam boobu ci moom waaye nag jamono jii ñu nekk espaañ a ngi jéegoy jéego ci fuqarcee ko ci itaali lii sax moo waral ci weer wi desambar lu jege waa senegaal ñoo sànku ci ndox mi ci séen gaal gu laboon te jëmsi woon espaañ ca dunam ya tudd canaries lu bari ci murit yi danu lay wax ne di jaay di wër moo leen gënal ñu sax fi barab di ligéeyal kenn loolu nag ci genn anam day wone ni njàngalem sëñ bi jeexitale ci ñoom te mooy sukkandiku ci sa bopp lu man a xew nag ñu néew ci ñoom a mas a def ay tooñaange yu mag bis bu amee ay këyit ak visa day daal di dellu kër ga def fay weer te sax ci mujjug at mii rekk ñu bari di nanu dellu réew ma ngir tëbëski ji bu ko defee ñu ci ëpp danu fay des ba weneen xewu diine wu mag wa ñëw di màggalug tuubaa bu ko defee nag bu jàllee ñu door a dellooti tugal ci jamonoy lòlli jenn ci dooley murit yi mooy seen nosu gi nu def ci wàllug njiit ñoom de bu ñu doon ab jal da nga naan xalifa ba a nekk ca njòbbaxtal la di aw turu njiit wow ki ko yanu fii mu nekk mooy sëriñ muhammadu lamin baara mu sëriñ fallu kii daal mooy ki nga xam ne lu mu wax rekk ñu def ko cig ayam tuubaa gis na ag yaatal gu jéggi dayo ba ci atum bu ña fa dëkk weesuwutoon nit leegi àgg nanu man nanu ne ci ay nit alkol nag ak póon danu leen a aaye ca tuubaa moom dëkk bii nga xam ne daa xaw a moom boppam ci biir senegaal ña nga fay taxawal daara ju mag ab université boo ko doon nattaleek yeneen dëkki jullit ñi fa la ag féex ëppe ak doxe na la neex ci diine jigéen ña dunu sol pantaloon waaye dunu muuru it ñu ci bari it dunu musóoru xale yu góor ya ak yu jigéen yaay demandoo jàngu ba école saa su nu wootee ngir ñu defar ab fajuwaay hopital mbaa woote bi jëm ci lu defar ndox mi ay milyoi eurooy dajaloo ngir ne murit yu bari ay way woomle lanu ku ci mel ne elhaaji juuf may futbal ca bolton angalteer ndax moom joxe na ca la ñu doon laaj ngir ligéeyub tuubaa ba xamagunu leen de bu baax waaye murit yii bari na lu adduna bi man a jànge ci ñoom de du rekk ni nu war a def ba jàmmaarlook li nuy wax mondialisation di ci maanaa jël adduna bi bepp def ko daanaka menn réew benn xalaat xatal soreente yi jegeele gis gis yi añs waaye it warees na a jànge ci ñoom ni nuy doxale diine ci anam gu teey te jàmme jëmm fii muy tekki physique baat la bob ci gereg mooy maanaam fisikus di ci wolof kojug dénd moom nag mi ngi juge ci reenub dénd kon jëmm mooy xam xamu dénd la ko dale ca kawaarig yi nga xam ne nu ñu tuuteewul amul ba ci nekk àdduna gu màgg gu tàlleeku gii xam xamu jëmm liy liggéeyam mooy jéem a tëgg ay àtte walla ay yoon yu matematig yuy àtte àdduna bii di bu ne ne bu dénd ak lambutu xóot xóoti ne ne ak dëgg dëggi jikkoom ak way toggale composants yu mag yi ko toggale ak doole yu dàttu fondamental yi nga xam ne yaram yu ndaw yi dinañu koy joqalanteek yaram yu ne ne yi nga boole ci njuréefi doole yii leeg leeg ci xam xamu jëmm bu bees bi danu ciy boole gëstug xam xamu ndendoo ak bu wattuwu niki xam xamu wattu kàttan ak jañu momentum ak cefkag mbëjj looloo waral boroom xam xami jëmm yi lu bari lanuy faral a gëstu ci feeñtey jëmm yi dale ko ci ëtt yu yaatoodi yi ba ci yu yaatu yi dale ko ci yaram yu ndaw yi nekk ci ron saal walla xartil nga xam ne ca la mbooleem ne ne yu baaryon yi di ame jëmm bu yaram yi ba ca gëstug sóobu walla jikkoy yaram yu jëmm yi ca adduna ju yàgg ja ba ci jàng yëngu yëngu gu bidiw yi ci asamaan su ne ne si moo xam ci biir gaawaay yi nu xam la walla yi jege gaawaayu leer ci mujjantal gi gëstu nekk gi adduna bi ci léppam yëngu yëngu googu nag mi ngi tàmbali ci xarnu bu fukk ak juroom ginaaw juddu gu yonnant yàlla isaa xvu xarnu balla isaa ba ci bu fukk ak juroom ñaar xvii mu sos fi nag ay coppite yu xóot ci wàllug aada dundin mboolaay politig ak koom koom kon daal yewwute gii amoon ca jamono yooya ca tugal li muy wund mooy ag tuxu juge ca jamono ju diggu ja mu y jamono y ag laman walla ag cang dem ci jamono ju yees ji di ju jëm kanam gu xam xam ak xarala sabab yi jur yewwute gii yu bari lañu waaye nanu ci indi ñatt yi ci ëpp solo rekk ñooy ci waxtu wi tugal nekke cig deltu ginaaw ci wàllug xay ci jamono yu diggu yi nga xam ne jàngu bi egliis bi faagaagaloon na bépp xalaat bu leer te gore araamal ci nit ñi ñuy xool leneen lu dul am njàggaleem mu way deng mii te doxadi bi tugal nekke ci lëndëmam gii jullit ñi ñoom ñi ngi doon jëm kanam bu baax ci yekkati tabaxub seenug xay ci kaw ay cëslaay yu xam xam ak wisaare maandute ak mbokko ci diggante nit ñi ci lu dul xool xeet walla melo mbaaw làkk xayug lislaam gi nag àgg na tugal jaare ko ci yoon yu bari bokk na ci yooyu andalusi ak sisil ak reewi penkub lislaam bi rawati na ci xarey jooñe yi croisade ndax kat booy xool li tugal di nekk lépp di ku ñu dàqe ca xarey jooñe ya walla yu galajaane ya duma ko ca teewul mu fàggoo ca njariñ lu bari ngir fenqoo gi mu ci defe ak xalaatub lislaam bi ak nosteg dundam lii nag ci li soppi xalaati waa tugal yi la jëm ci jàngu bi nit adduna bi ak dund gi te itam lu bari ci sàkkukati xam xami tugal yi dañoo tàmbali woon di naan ci xam xami lislaam yi ci paj xeltu gañcax ak ndundat ak yu dul yooyu ci jàngu yu andalusi yi la ko dale ca xarnub fukk ak benn xi g loolu nag taxoon na ba yëngu yëngu gu firi walla tekki gu mag amoon ci xam xami lislaam yi tukkee ci làkku araab dem ci wu latin wi doon wu xalaat wu diine tey wu politig ca tugal ca jamono jooja loolu dimblee woon ci ginaaw bi ci lal yoon wi ba yewwute gu tugal gi man a am bu ko defee li ñuy wax tool di suuf si sang biy moom moo daa tekki barabu dëkkuwaay bi koom koom bi mboolaay gi ci gii noste màggug dëkki tugal yi ngir màggug yaxantu gi nu daa def ak mboolaayi jullit ñi ak màggug liggéey yi ngir jòkkoo gi waa tugal gi daa def ak jullit ñi taxoon na ba nosteg laman tàmbli woon a lòtt aka naaxsaay rawati na bi nitug tugal gi tàmblee am yoon wu mu man a jaar bay dund te du sukkandiku ci léppam ci suuf ak tool waaye ci yeneen ligéey yu koom yi dëkk yi tam tàmblee doon barabi leer yu di boroomi xay di sonnale ci loolu aka lakkal noste gu laman gi tey liggéey cig màbbam def it lu rëy ba yewwute ci tugal man a am jàngu bi moo nekkoon di teg loxo ci dundug xalaat gi gu diine gi ak gu aada gi ci tugal gépp te yitteem jépp mi ngi ko sottiwoon ci njàngum pas pasu diney nasaraan walla li nuy wax njàng yi aju ci yàlla théologie ak njàggat ak xellu amutoon jenn yitte ci njàng yi aju ci xam xam jàngu bi moom dafa jàppewoon boppam ki nga xam ne ci yoon moo war a doxal mbiri politig yi te kat moom jàngu bi tawati mbon akug yàqu dañoo ruuroon aw yaramam dugg ko fépp ba waral aw nit wu jàng te yewwu jug taxaw temb ci dañal ñaawteef yooyu ko taqoon loolu tam bokk na ci li jañoon xelum nitug tugal ki ci mu jëm kanam gën a ñaw rawati na bi dëkk yi gënee yaatu degginu ligeeyub yaxantu gën faa xóot ak bu endustri ak aada yii yepp nag liggéey nañu lu rëy ci waxuma la doyodil ngëb gu tar gi paab gi ngëboon mboolaayu tugal gu nasaraan gi waaye it doyodil nosteg laman gi loolu it di doyodil nosteg laman gi rataxal yoon wi ba yewwute gi man a am dëkk yu itaali yi ñooy mber yu njëkk yi njëkk a uuf tete yewwuteg tugal gi looloo waraloon ñu am wàccuwaay bu kawe akug wormaal ci yeneen dëkki tugal yi ca jamono jooja dëkk yii niki milano ak venezia ak firenze ak napoli ñoo uufoon yewwute gi seeni boroom xam xam aki njàggatkat ak ñoñ fànn duggaloon nanu ci seen loxo bu baax li waraloon loolu nag lu bari la bokk na ci dal ga fa amoon ak jàmm ja ak jëm kanamug koom koom ba ak yaatug yëngu yënguy nitu itaali ki ak ba tay yaatug goxi xalaatam ak yëg gu mu yëg gore gu mu am ginaaw bi mu goree ci nosteg laman ak li itaali yàgg a am ci teddnga gu sax ak jaloore mu y njàggati waa rom yi seeni xam xam seeni jeexiit ak seeni fànn nga rax ci loolu nekk gi paab gi nekk rom nga xam ne loolu faggul na waa itaali ag cang gu diine ni nga xame ne barab boobu it di itaali faggul na paab bi ci itaali ag tono gu neen ak gu maanaa gu mag nga rax ci dolli gëpplante gu mag gi amoon ci diggante dëkk yu mag yi ak peeyi nguuri itaali yi ci wàllug njàggat ak fànn ak soññ gi doxalkati dëkk yii ak buur yi daa def boroom xam xam yi daa liggéeyal yewwute gi ak ba tay yittewoo gi nga xam ne amoon na ci dëkk yii aju ci gëstu mbind ak taalif yu yàgg ya ak barig móolukaayi téere yi ci yii dëkk ak nag li itaali doon xéewoo muy nekk ci barab bu raññiku buy dimblee ci jokkoo ak addunay jullit ñi yewwuteg tugal gi mi ngi ame ci mbooleem wàlli dundug nit gu xalaat gu fànn gu politig gu diine ak gu koom koom yii di ñëw ñoo ciy wàll yi gën a rëy ag nite li miy wund fii mooy dundal njàggat yu yàgg ya yu geres ya ak rom ak feddali sukkandiku gu nit war a sukkandiku ci boppam akug goreem ak sañ sañu wax li nekk ci moom ak dog gàllankoor yu mboolaay yi ak jële fi aaday jamono yu diggu yi ak sotti yitte yi ci adduna bi ak dénd bi ak jeem a xam seeni mbóot yëngu yëngu googu nag bokk na ci màndargay yewwuteg tugal gu njëkk gi ndaxte li mu yittewoo woon mooy xam xam yu kojug nite yi nga xam ne njàngatkati geres yeek rom grego romain ñoom lañu jëloon yittewoo leen ak seeni xeltukat ak seeni boroom xam xam ak ñoñ fànn ak seen boroom mecce yu muus yi te ñaw boroom xam xam yi daa def gëstu yooyu di kojug nite ñi ngi leen di woowe ñoñ nite walla boroom njàngat yi ñoñ nite kon ñooy mbooloom nit mi yittewoo woon jàng njàggat xam xam ak fànn yu yàgg ya yu klaasik ya maanaam njàngati geres ak rom ak seeni fànn ak xam xam yëngu yëngug nit gii nag judd na ginaaw bi mu amee ag jàpple gu tukkee ci kilifay dëkki itaali yi ak seeni boroom alal ñoñ nite ñi génne woon nanu ab taar feeñal ko ci mbooleem fànn yu wuute yi moo xam yatt la mbaa nataal ak deseñ ak misik ak tabax ñoñ fànn ñu itaali ñi ak ñu dul ñoom ci jamonoy yewwute dañu doon roy fànn bu klaasik bi di bu gres rom bi bàyyi nee nag fànn bi nu daa wax xóot nga xam ne moo amoon ca tugal ca jamono ju diggu ja bu ko defee ñoñ fànn ñi jëmale seen fànn ci taarub dénd bi ak dund gu yees gii nga xam ne mooy gisiin wu jëm kanam wi nu am ci dund gi ci dëkki itaali yii lu bari ciy fànnkat yu siw yi fa lañu feeñe bokk na ci ñooñu deseñkat bu siw ba di fra angeliko leonardo da vinci titian ak rafayel g yattkat ba donatello làkku latin ci jamono yu diggdoomu yi moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam xam ya ak niti diine ya ak politgkat ya ak njaggatkat ya ak ustaas ya la notoon nag ca nit ña di woon niti neen ñi rekk ñoom déggunu woon wii làkk lu tumbrànke la woon ca ñoom seen làkki bopp yiy yu seeni barab lañu déggoon bi jamonoy yewwute dikkee ngelawul fonk sa xeet upp ci tugal gépp la lu bari ci xalaatkat yi ak njàggatkat yi ak woykat yi tàmblee jng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki réewi bopp niki wu itaali wu espaañ wu fraans wu angalteer ak yu dul yooyu bi mu ko defee woykatu itaali bi tuddoon dante taalif mbóosóor mu sell mi ci làkku waa itaali naka noonu petrarch mii nga xam ne li mu gisoon mooy làkku romam wii daal mooy gën ja a kawey jumtukaay ngir génne xasiday woyam yi bu ko defee miguel de cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di don kixota ci làkku espaañ ci noonu it la rabelais def moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di wu fraans ngir wuññi ci liy yëngu ci biiram ci njàggat lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor kaf chaucer mi dib waa angalteer g jug moom itam sotti ciw làkkam woyam yu yéeme ya cib taar rawati na nettaliy kentrebry yi nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati angalteer yu mag yi yi gën a siw màggug fonk sa xeet ak sa reew ci tugal juroon na ci jamonoy yewwute ay reew yu bari ci tugal taxaw yu amoon ag temb ci noonu yittewoo xalaati fonk sa xeet daal di fay feeñ fés fa lu aju ci temb tam di lu ñu fay waxtaane ak àttewiin yi dëkki itaali yi ak reewi tugal gu sowwu gi ci jamonoy yewwute dañu doon yittewoo dajale mbind yi ci fi ñu jortoon ne fi lañu nekk ci xustantin ak ci dëkki waa geres yi ak ci yeneen barab yi ci tugal mbind yooyu ñu daa wër nag ñooy yu geres yeek latin yi nekkoon di lu ñu tas ci kàgguy daara yeek jàngu yi ak jàngu yu mag yi ak ci nit ñi walla kër yi yittewoo woon mbir mii peey yi daan àtte dañu daa jagleel lii alal ju bari ñoñ nite ñi tam ñu ci bari jëmale woon nanu seeni liggéey ci dajale mbind yi ci noonu ñu jot a am ci misaal rekk mbindum binkat bii di waa rom te dib xutbakat tuddoon quintilian nj g ak bataaxeli cicero nj yu xutba yi ak woy yu at ba at yu tacitus yi g tacitus moomu mooy taariixkatu xeexi jarmaan yi mi ngi bokkoon ci ñi gënoon a ñaw ci xutbakati rom yi ak seeni njàggatkat yu ñaw yi sonn ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya yewwuteg orob gi yittewoo woon na te sonnoon ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya ag jublu gu yees am ci jàngiinu taarix ñu koy teg leegi ci cëslaayu jam waaye tegeesatu ko rekk ci dégg ak nettali ci noonu ab jàngu sosu ci firenze am njàngaleem jëm ci jam gu taarix mu tudd daaray xam xam bu taarix bokkoon na ci boroom xam xam yi ci gënoon a duggal seen loxo nitu taarix kii di lorenzo valla g mooy ki jamoon te diiatoon benn wayndare dossier bu taarix sikkoon it ag wéram mooy li ñuy wax mayug xustantin mooy wayndare boobu nga xam ne paab yi yàgg nañu cee sukkandiku la ko dale ca xarnub fukk ak ñaar g ci seen xeex yi nu doon def ak buur yu mag yi ngir feddali ci seen àqi politig ci àtte nit ñi jiite leen bokk na ci ñi nga xam ne yittewoo woon nañu gëstuy taarix yi ak yu politig yi bindkatu itaali bii di xalaatkat bu politig bu am diplomasi di nicola michiavelli g michiavelli mii def na teere bu mu tudde woon buur bi ndax da ci doon wax lu aju ci buur bu am doole bu doon bennale dëkki itaali yi ak nguur nguuraanam yu daggatoo woon yi te tas jëm kanamug yaxantu ak ndefar yaxantu noyyi na bu baax ci orob gu sowwu gi dale ko ci njëlbeenug xarnub fukk ak benn g itaali fi mu feete dimbli na ko bu baax ci yëngu yëngug yaxantu dox fa te jëm fa kanam ci noonu lonkoo yu yaxantu yi tàmbli fa a sosu di jëli marsandiisi penku yi niki sooy ak cuub yi ak rëndaay yi ak wurus ak bëñu ñay ak yu dul yooyu ginaaw bi it yii lonkoo ginaaw bi ñu gënee jëm kanam tàmblee yòbbu yii silaa ci yeneen dëkki orob yi bu ko defee bu ñuy dëpp di indaale marsandiisi orob yi niki ngëndal ak der ak firaa jëm kanamug yaxantu googu ak gu meccey ndefar yi yi jur nañu ag xereñ ci denciinu alal akug jëm kanam ci koppar yi ñuy jëfandikoo ci jëfi yaxantu yooyu ci noonu am mbooloom ay sandikaay mecce feeñ mujj teg loxo ci ginaaw bi ci fepp fu koom nekk te am fa cawarte naka noonu nu def ay ligeey yu mag ci wàlli mboolaay ak politig ak xalaat raxaatal ci loolu juddug kuréel gu diggu gi ñooy mbooloo miy ligeeye yaxantu ak yeneen mecce yu wuute yi feeñug yëngu yëngug xam xam gu yees gi yewwute gi ci njëlbeen gi dafa sotti woon yitteem ci dundal njàggat yi ak fànn yi ginaaw bi mu dox as lëf ba àgg ci mbooleem lu xay gu mat laaj ci noonu yewwute gi matale mbooleem dundug mboolaay gi bokk na ci xam xami dëppale yi ndaxte xam xam moom màggoon na ci dëkki orob yi jàngu yu mag yi sosu ci orob gi rawati na ci dëkki itaali yi yëngu yëngug xam xam googu mi ngi tàmblee ci di jeem a dundal xam xam yu yàgg ya ginaaw bi mu dox jëm kanam loolu nag li ko waraloon mooy jariñu gi mu defoon ci yoonu xam xam woowu di wu kojug nattu maanaam lu nekk looy wax nga teg ci sa loxo mu leer la ne loolu la nga doog ne moom la ndax wóore na la ci làmb gi nga ko làmb ba daj ko yoonu gëstu woowu nag mooy wi boroom xam xami jullit ñi jaaroon ci noonu boroom xam xamu fisiyaa bu angalteer bi ñuy wax roger bacon feeñ di njiitul gëstug xam xam ci tugal becon mii mi ngi sukkandiku woon ci yoonu jakkarloo ak nattu ci gëstoom yooyu nga xam ne àggale woon nanu ko ci ay ngérte yu am solo ci xam xamu bidiw ak bu weer yi ak yu matematik yi ak juxraaf naka noonu boroom xam xamu xeltu ak politig bu angalteer boobu di francis bacon moom itam feeñ g di koo xam ne dafa jëfandikoo xel ci àgg ci dëgg yu xam xam yi ci noonu ci gisiin mooy ki teg ponki ngérum xam xam mu bees mi ak doonte moom doonul woon boroom xam xamu dénd boroom xam xamu itaali bi leonardo da vinci g moom tam feeñ di kok dafa yittewoo woon jiyoloji bu mekanig ak matematig ak yu dul yooyu nga rax ci dolli fànnu yatt ak nataal ak misik ak eeseñëri mu nekkoon daal boroom xam xam te di nitu fànn tey fentkat naka noonu boroom xamu itaali bii di galileo g feeñ mooy ki njëkk a defar nattukaayu tàngoor njëkk a fuglu bidiw yi ca fesalukaayam ba dëgëral te feddali gisiinu boroom xam xamu bidiw bu poloñ bii di copernicus g bokk na ci màndargay xam xam yeneen yu yewwute gi fentug móolukaayu teere ci loxol nitug almaañ kii di john gutenberg atum g fent gii ak doonte gu almaañ la teewul jëmale na kanam bu baax dundug nit ci biir tugal ak biteem wuññiy juxraaf yi tam ci màndargay yewwute gi la woon ak yéwénalug diine gi ci tugal nga dolli ci loolu feddali gu nitug tugal ki feddali jëmmam jii nga xam ne yàgg na a nekk di lu nu làq ci jamono yu diggu yi ci biir ay kureel walla sandikaay mecce yi mu daa bokk ngir làqatoo ca ak aar njàriñi boppam yewwute gi ci itaali yewwute gi ci itaali daa tàmbli woon a giim ak a yànnjadi ci mujji fukk ak juroomeelu xarnu g ak njëlbeeni fukk ak juroom benneelu xarnu g loolu nag li ko waral lu bari la ñu jéem cee indi yenn rekk yi ci ëpp solo attekaay yooyu mosal nanu ginaaw bu àtteb lislaam dañee ca andalusi te garanada nërméelu daanu mosal nañu lu bari ci jullit ñi ay xeeti mbugal ak coona lu maneesul a misaal bokk na ci di leen lakk ñuy dund tuxug yewwute gi ak li yewwute gi di neew doole ci itaali lepp taxul mu naaxsaay mbaa mu suux li am kay mooy da fa a tuxoo dem ci yeneen reew yu tugal niki espaañ portigaal fraans angalteer holand ak almaañ añs ay jëfka yu bari bokk nanu ci li tuxale yewwute gi jële ko itaali yòbbu ko ci yii dëkki orob bokk na ci yooyu nekk gu yii dëkk nekk di yuy door a noppi ci seenug sosu gu politig gu yees ak tàbbi gu ñuy doog a def ci jamonoy tabax ag xay ñi daa woote yewwute gi nag def nanu lu rëy ci tuxale ko itaali mu dem feneen nitug holand kii di erasmus g moo tasoon te wisare yewwute gi ci almaañ jaarale ko ci def fa ay waxtaan aki xutba ak ci yeneen dëkk yu orob yi erasmus mooy ki firi injiil jële ko ci làkku gres yòbbu ko ci wu latin jël nag li ñu ciy wax kòllare gu yees gi def ko ci ay làkki orob yu bees loolu bokk ci li feexal te goreel xalaatub tugal bi ci ngartaajoo gi ko niti diiney katolig yi ngartaajoo woon loolu it won na waa tugal ne yaxub injiilub latin bi egliis bi yoroon du woon biy cosaan te yax bu bari woon ay yàq la kon daal eramus mooy ki waajal xelum tugal mi ci mu man a nangu yéwénali diine yi ni yewwute gi meloon ci fu dul itaali yewwute gi ca almaañ dafa yoroon melow njàngat wiy ligeeyal gëstuy diine yi ci manaa daa yamoon daanaka ci lu aju ci diine rekk ca dëgg dëgg gëstu yi aju ci xam xami gres latin yi dafa xawoon a yeex a àgg ca dëkk yooyu di yu almaañ ak li njiiti yooyu dëkk daa dimbli gëstu yooyu lepp cig wàll ak li almaañ doon am ay daara yu mag ci vienne ak idelberg ak baasal ak strasburg ak yu dul yooyu lepp ci geneen wàll yeex googu nag li ko waraloon mooy niti diine yi ak ñu dul ñoom ñoo ko nanguwutoon ñoom daal danu fee nekkoon rekk di sàkku nu ñu tënke te jéng yooyu njàng ak gëstu te defi pexe ba du ñu tas ci anam gu yaatu ngir nu wattoo ci seen kilifteef sàmme ci seen daraja aare ci seen ligéey ci noonu danañu gendiku ne yëngug nite gi ci almaañ dafa doon sori jubluwaay yu deet diine yi looloo tax du kiimaan almaañ di woon barab bi uufoon yëngu yu yéwénali diine yi gënoon a am solo ci tugal bu dee ci fraans moom yewwute gi melow njàngat ak nite la fa yoroon wi yittewoo woon xam xami gres yi ci noonu boroom xam xami itaali yi ak yu gres yi taxaw ci wisaare gëstuy xam xami gres yi ñu móol teerey ndonoy gres yi ci móolukaayu paris ba ñu taxawaloon ca xarnub fukk ak juroom benn g ni nu duggale seen loxo ci amal ay akaadimi aki barabi xam xam ngir njàng yi aju ci nite niki bànqaasub buur bi ci paris ñu sos ko ci jamonoy buurub fraans bi di fransuwaa mu njëkk mi atum g bu dee ci angalteer ba tay yewwute gi ma nga fa yoroon melow njàngat ak nite ay gëstu yu xam xami gres yi am fa ay ñoñ nite ñu waa reew ma ñu bari ñooy ña ca siwoon ñoom ñooy ñi daa jàngale làkkuw grees wi ci daaray xam xami itaali yi ku ci mel ne wilyam lilly mi daa jangale làkkuw gres ca rom erasmus mu olaand mi ak kolt mu angalteer mi ñoo tekki woon injiil ci làkkuw angale wu bees wi buurub angalteer bi henri mu juroom ñatteel mi moom tam sosoon fa juroomi toogu yu darajay ag ustaas ci xam xami pas pasu nasaraan ak yoonu siwil ak wu dénd bi ak làkku ebrë ak wu gres ci daara ju mag ju kembrij jàngub san pool bi nekk london moom it jagoo woon njàng yu nite yi yewwute gi ci angalteer dafa jublu woon yoonu takk ak boole diggante pas pasu nasaraan ak gëstuy nite yu njàngat ak yu fànn yi yewwute googu nag indiwul woon lu yees lu ñu fent ndare ci xarnub fukk ak jurom ñaar g bi am njurum njàggatam ak mu niteem mu yees feeñee ci anam gu fes te rafet ci woyi william shakespeare yi g ak woykat bu silmaxa bii di john milton g ak ñu dul ñoom ñaar fii tam ci angalteer yoonu yewwute gi da fee jengoon as lef jëm ci yewwute gu xam xam gu aju ci xam xami dëppale yi walla xam xami nattu yu làmb yi ñi jiitu woon ci lef moomu ñooy ñaari boroom xam xami angalteer yii di roger becon ak francis becon ñoom daal ca dëgg dëgg ñooy ñi sos daaray xam xam ca angalteer baat bi nuy mujj a wax ci yewwuteg tugal gi mooy moom daal moo ñàkkal jamono yu diggu yi kàttan ci jeexiital ci mboolaayu tugal gi ci wàlli dundug politigam gu mboolaayam gu xalaatam ak gu aadaam ngir jeexiit yii fi yewwute gi sotti ci orob ay noste yu yees am nañu yu làmboo tabax guur gu yees gi ak mboolaayug orob gi ci cëslaay yu aada yu mboolaay yu jikko ak yu ngér yu yees ni mu duggale loxo ba tay ci ubbi ay gox yu yees yu xam xam yu jël gisiini xam xam yi ak dal yu xam xami juxraaf yi lii lépp nag moo sabab jamono ju yees ci orob di ju wuuteek ja woon ca jamonoy laman ci xalaat ak ngér ak defiin aki xew xew loolu lepp nag nga boole ko moo jur jamonoy tugal ju yees jii 
