#Article 1: Albert Einstein (160 words)

Albert Einstein (juddoo Ulma (Almaañ) ci atum 1879, faatoo Princeton (Diiwaan yu Bennoo yu Amerig) ci 1955) doonoon na ab boroom xam-xamu jëmm, xaymakat, xetlukat bu waa Almaañ bu jëloon réewu gu waa Suwis, te mujje ca Diiwaan yu Bennoo yu Amerig. 

Lu weesu doon gi mu doonoon kenn ci jëmmkat ak xaymakat yi gën a siiw ci àdduna bi ci taariixu xam-xam, doonoon na xalaatkat, ku bari yëggu-yëggu ci yeneen fànn (tambalee ca xeltu ba ci politig). Boole nañu ko ci gëstukat yi gën a màgg ci xarnub XX. 

Bokk na ci li ko gën a siiwal gisiin wi mu def te duppe ko gisiinuw ajoo. Dugal na it loxoom ci li jëmale-kanam doolerandub kàttan-ferñent, doolerandug tekkaaral, añse.

Jotoon na Neexalub Nobel ci jëmm ci atum 1921 

Albert Einstein Ulma la juddoo ca Almaañ aji juram ju gòor mooy Hermann Einstein, doonoon booroom këru liggeéyukaay bu doon defar ay wuutuloxo yu mbëj, Pauline Koch doonoon aji juram ju jigéen.

#Article 2: Ndakaaru (115 words)

Ndakaaru (Dakar) Nekkoon reewu Afrig gu sowwu gu Faraas (ASF, walla AOF ci FR), Ndakaaru fimne mooy reewum Barug Senegaal akit goxub Ndakaaru, tolluwaayam ci péeteg sowwu bu Afrig, ci jegeem Daanaka-dun bu Kap-Wert, waral na sancug notaakon yu jëkk yi, Akit yaxantu ak Àdduna bu bees bi, te ame na peetewaayu ngëneel ci jëflanteg cosaani Saa-Afrig yi ak Saa-Tugal yi. Fa lees Taxawalee woon Xumbalu Àddina bu fànni ñuule (jaam yu ñuul) bu njëkk bi ci xalaatu Leopool Sedaar Sengoor atum 1966, Dëkk bii mooy toogu bu Këru-gëstu bu dàttu bu Afirg gu ñuule (KDAN, walla IFAN ci FR) akit bu Bànk bu diggu bu guuri Afrig gu sowwu (BDGAS walla BCEAO ci FR)

#Article 3: Senegaal (4346 words)

Senegaal menn la ci réew yi ne ci Sowwu Afrig, mu bokk nag ci Afrig gu bëj-saalumu saxraa (Afrique sub-saharienne), Mbàmbulaanug Atlas diw digam ci sowwu, taqaloo ak Gànnaar ci bëj-gànnaar ak penku, Mali féete ko penku, Ginne ak Ginne Bisaawóo ci bëj-saalum, Gàmbi moom sos ab daanaka-jiba (quasi-enclave) ci biir Senegaal, sutuxlu ba ci lu ëpp 300 jñ (km) ci biir suuf yi. Duni Bopp bu Wert bi (Cap-Vert) ñi ngi ci 560 jñ ci tefesi Senegaal yi. 

Réew maa ngi lebe turam wi ci dex gi ko peek ci penku ak bëj-gànnaar, te ab balluwaayam bawoo ca Fuuta Jallon ca Ginne, di Dexug Senegaal. Ab kilimaam bu gëwéel la te di bu fendi te yor ñaari jamono: jamonoy nawet  (jamonoy taw) ak ju noor (jamonoy fendi).
 
Ci jamonoy canc gi (la période coloniale), ay digg yu yaxantu yu bari, yu ay imbraatóor yu canc (empire coloniale) moomoon, daal di woon nañuy sampu ci tefes gi gépp. Dëkkub Ndar mujj na di péeyub Afrig gu Sowwu gu Faraas, mu mujj juge ci di leegi Ndakaaru ci 1902, moom Ndakaaru nag mujj na di péeyu Senegaal ca ba mu jotee ca ag tembam ca 1960, nekk ci cat li gën a féete sowwu ci goxub Afrig

La dale 2012 ba fimne Maki Sàll mooy njiitul réew ma. Senegaal ak doonte bokk na ci càmpéef yu bari yu àdduna bi, teewul bokk na ci Bennoo gu Afrig (Union africaine) ak Mbooloom diiwaan yu Saxel-sahraa yi  (Communauté des États sahélo-sahariens)

Senegaal nag yaatoo na 196.190 jñ2.

Cosaanul turu Senegaal dañul di jeqi dàggasante ak werante. ca 1850 labbe bii di David Boilat, ca mbindam ya mu doon def ci Senegaal,daa gisoon ne Senegaal mi ngi juge ci waxiinu wolof wii di suñu gaal. Bii nag mooy gis-gis bi gën a siiw, te xibaarukaay yi (les médias) gën koo ame. te moone lu ñu nangoodi la te sikk ko la ko dale ca ati 1960, ay gongikubaat yu bari nag joxe nañu leen, ci misaal biy taf cosaanul tur wi ci ag giir gu berber gu Sahara, mooy  giirug Zenaga walla Sinhaaj, naan: Turu Senegaal mi ngi bawoo ci tudd gu waa Portigaal yi doon tudd turu giir googu. Waaye werante wi dañul di tàng ci loolu ba tay.

Lu ci ëpp Njëkk-taariix ci Senegaal day tudd - ba laa tudd lenn - gëwéeli xeer yu mag yi (walla les cercles mégalithiques) yu Senegàmbi yi, walla jóori xor yu ñu sàkk yi (les amas coquilliers artificiels), yu ci mel ne ya nekk ca dunub Faajut.

Jàpp nañu ne Senegaal dëkkees na ko ci njëkk-taariix lu jiitu lool juddug Isaa. Ay doj yu ñu yatt yu Jamonoy doj wu ñu yatt ju njëkk ja(Le Paléolithique inférieur ), wuññees na leen ci daanaka-dun bu Bopp bu Wert bi (Cap-Vert) ak yeneen yëf yu gongikoo ci doj, ñu jekkal leen, dees leen di fekk ci diiwaanub Tëngéej ak ci pegi dexi Senegaal gu penku gi. 

Ci jamonoy doj wu ñu xacc (néolithique), jumtukaay yi tàmbali nañoo soppiku ak a wuute, bu ko defee suuf su ñu togg (walla céramique) daal di feeñ. Gasi gëstu ya ñu doon def ca diiwaani tefes ya feñal nañu ay desiiti waañ yuy seere ak a firndeel askan wu mag wu ay nappkat aki yaxantukat wa fa nekkoon (marigot bu Xant ca delta, sottikukaayu dexug Saalum). 

Ndefarug mbell (walla gu weñ (metallurgie)) jëm na kanam ci jamonoy mbell yi (protohistorique) (junni bu ngëkk bi njëkk  Isaa), fi ñuy gis ay bàmmeel ci bindu ay mbaanaar (tumulus). Ci digg réew mi, fa tollook  Gàmbi gu tay gii, dees na fa fekk mbooloom gëwéeli xeer yu mag (cercles de mégalithes) ci aw dog wu tollu ci 100 jñ ci kaw 250|jñ.

Dëkksi gi dafa doon gën di dolliku ndànk-ndànk tey gën di dëgër ngir àgg ci sos ay nguur yu njëkk yu sosu ci VIIeelu xarnu, nguur gu Tekruur, gu Namandiru, gu Jolof, ak ay mbokkoo yu sori ak Iimbraatóor gu Gana, ci suufus Mali gu tay gi. Ci nguur yu wuute yooyu, gi ci ëppoon doole ci XIVeelu xarnu moo doonoon imbraatóor gu Jolof, gi boole woon Kajoor, Bawol, nguuri séeréer yu Siin ak yu Saalum, Waalo, Fuuta-Tooro ak Bambug. Ci bëj-saalum, nguurug Kaabu, teg ci gu Fulaadu. 

Jolof nekkoon na imbraatóor gu Njaajaan Njaay sosoon, ki njëkk a nekk Buurba (buur) ca Jolof. Faleesoon na ko njiit ca loolu doon mujj di nguurug Waalo, ca bëj-gànnaar-penku gu Senegaalug tay gii, ca diiwaanu dex gi. Dajale woon na mbooleem askani giirug wolof ngir taxawal imbraatóor gii ci XIIIeelu xarnu . Ibraatóor gi saayoon na te naaxsaay ci 1549, ànd ak deeg imbraatóor ba mujjoon ca Jolof, Lele Fuli Fak, ki ko rayoon di Amari Ngóone Sabel Faal, ki nekkoon ca jooja jamono kilifag diiwaanu Kajoor. 

Jolof des na di aw dog (vassal) ñeel imbraatóor gu Mali ci diir bu tollu ci xarnu. Ba loola amee, yeneen nguur yi, ñoom itam gu ci nekk, tàmbalee jël ag tembam ba mujj wàññi imbraatóor gu Jolof gu mag googu ba àggal ko ci tolluwaayu genn nguur gu yam ca digg réew mi. Ci ñaareelu xaaj bu XIXeelu xarnu, sancaani Faraas yi (les colons francais) tàmbali woon nañoo nangu ndànk-ndànk mbooleem nguur yu Senegaal yii. Jolof moo nekkoon nguur gi ñu mujj a nangu ak Buurab Jolofam bu mujj ba Alburi Njaay, ci ron deflu gu Luwis Federb.

Lislaam a ngi njëkk a tàbbi ci Senegaal ci diggante VIIIeelu xarnu ak IXeelu xarnu, ña ko fa dugal di ay yaxantukat yu araab-yu-berber. Dañu doon tas diine jii ci jàmm, ñu njëkk koo jox Jula yi tuubloo ci ginaaw bi Tukkloor yi ak Saraxule yi, ñoom itam ñu tas ko ci Senegaal gi gépp. Bi ñu demee ba ci kanam ca XIeelu xarnu , la Muraabituun, jug, Tukkloor yi jàpple leen, ñuy jéem a tuubloo mboolooy jaamukati xërëm yi jaare ko ci Jiyaar. Loolu benn la ci sabab yi tax Séeréer si gàddaayoon dem Siin-Saalum, Wolof yi, Pël yi ak Mandinke yi, te ñoom ñepp ña nga jalu woon ca Tekruur. Lislaam teel na tas ca imbraatóorug Jolof. Waaye ca XIXeelu xarnu la nangu ca dëgg-dëgg mbooleem askan yi, ci anam gu jàmmu, loolu nag deesi sante ko Sëriñ si, ku mel ne  Seex Ahmadu Bamba, mi sos yoonu  murit, Alaaji Maalik Sy kenn ci kilifay Tiijaaniya walla Seydina Limaamu Laay, ki sos laayéen gi, ñi yéemoon nit ñi ci seenug mbaax ak ragal Yàlla ak séeni karaama( xar-baax). Moom Lislaam tam nekkoon ab ker-keraan (moyen) ngir boole nit ñi te di leen aar ci jalgati yi ñu miinoon ci nguur yi (jiyaar yu toftaloo, canc gu ñu teg ci doole, jalgatiy Ceddo yi).

XIXeelu xarnu ñi ngi ko gën a xame ci daanug nguur yi, jàllsig sancaan yu Tugal yi ( colons européens ) ak jàmmaarloo gi lànk canc gi, ñi ko jëmmal di ay nit ñu mel ne Lat Joor, Alaaji Omar Taal, Mamadu Lamin Darame, Alburi Njaay walla Màbba Jaxu Ba. Diiney katolig (walla nasaraan, ndax katolig bànqaas la ci nasaraan) daal di tasu, ñi ko def di ay nasaraanalkat yu Tugal la ko dale ca XIXeelu xarnu, rawati na ca Siin ak kaasamaas.

Lislaam tàbbi na Senegaal ci fukk ak benneelu xarnu,ànd ak giirug Sinhaaj gu Amaasix gi. Turu Senegaal waxees na ne mi ngi bawoo ci tudd gu waa Portigaal yi doon tudd turu giir googu. Askani Senegaal yi sos nañu ay nguur aki nguur-nguuraan, yi ci ëppoon solo di Imbraatóor gu wolof ca diiwaani Waalo, Kajoor ak Bawol, ci fukk ak ñeenteelu xarnu g.j, ak nguuruñg Tukklóor ak gu Deñaanke gu Pulaar gi ca penku bëj-gànnaar ga. Ay dooley Tugal teg nañu loxo ay wàll ci ay tefesam, ci fukk ak juroomeelu xarnu g.j, ginnaaw bi Faraas daal di teg loxo réew mi mépp, ginnaaw ay xare yu limu. Ci atum 1902 la Ndakaaru nekke péeyub Afrig gu sowwu gu Faraas gépp.

Seŋoor walla Léopold Sédar Senghor(1906-2001)(1960-1980) mooy ki njëkk a nekk njiitul Senegaal, yoroon dàkkantalu njiit liy woykat (walla taalifkat)
Ci samwie 1959, la Senegaal bennoo ak li ñu daa wax Sudaan gu Faraas gi, ci ron turu Lëngoo gu Mali (fédération de Malie). Lëngoo gu Mali googu tembe na ci Faraas ci 20 suwe 1960. Waaye ginnaaw ay jafe-jafe yu politig, Lëngoo googu mujj na di ñaari réew ci 20 ut 1960: Senegaal ak Mali. Jibaleesoon na ag lëngoo ci diggante Senegaal ak Gambi ci turu Senegambiya atum 1982. Waaye ci jëf feeñul, bu ko defee ñaari nguur yi tàggalikoo atum 1989. Am na ab jë bu ngànnaayu (front armé) bu nekk ci bëj-saalumu réew mi, ca Kaasamaas bu bëgg tembteg diiwaan ba, leeg-leeg mu xareek nguur gi, la ko dale ca atum 1982.

Sancaan yi (les colonisateurs) seen teg loxo gu canc gi (conquête coloniale) mi ngi door bi wuññig suuf yii amee ci 1442 ci loxol moolub Veneto (ab diiwaan ca Itaali) bii di Cadamosto, bi mu defalee ay wuññi ñeel Portigaal. Ca jooja jamono la waa portigaal daal di sóobu - ci lu gaaw - ci Njàppum jaam (walla jaayug nit ñu ñuul ñi), waaye doon nañu war a janook gëpplante (la concurrence) gi bawoo woon ci jaaykati ñu ñuul ñi te bawoo woon Britaani (négriers britanniques), Faraas ak Olaand ca Yaxantug ñatti-koñ ya (Commerce triangulaire).

Waa Olaand yi sos nañu ab diggub yaxantu ca dunub Gore, Faraas taxawal ca 1659 digg bii di bu Ndar nga xam ne moo mujj di péeyub Senegaal bu njëkk bi. Ci 1677 waa Faraas ñi ñëw nangu dunu Gore (benn ci digg yu mag yi ñu daa jaaye jaam yi ak Ndar ak tata ju dunu James ca Gàmbi).

Nosteg canc daal di nay taxaw ci dikkug Federb, Kaŋub Senegaal (le gouverneur du Sénégal) la ko dale ca 1854 ba 1861 ak 1863 ba 1865, mooy ki samp dàtti  Afrig gu Sowwu gu Faraas gi (ASF)(AOF). Ci wormaal gi mu defoon aada ya fa cosaanoo ( du dëgg, wormaalu ko fenn) la  tàllale jeexiital (l'influence)gu Faraas ba mu weesu Senegaal, mu liggéey ci lu jëmale kanam koom-koomu barab bi (ci njariñul Faraas rekk nag lol réew mi yitteelu leen woon ci lenn), daal di sos waaxub Ndakaaru.

Ginnaaw Ndar, Ndakaaru mujj na ci 1902 di péeyu Afrig gu Sowwu gu Faraas gi, benn ci sancu yu Faraas yi .

Ci samwie 1959, Sudaan gu Faraas gi (Mali gu tay gi) ak Senegaal seey nañu ci Lëngoo gu Mali, gi nga xam ne mujj na temb ci 20 suwe 1960. Temb gii mi ngi juddoo ci tuxalug ay nguur ( transferts de pouvoirs ) yu amoon ca dëppoo ga ñu xaatimoon ca Faraas ca 4 awril 1960.

Senegaal nguurug demokaraasi la gu limuy làng (gu bariy parti), njiitul pénc mi (président de la république)dees na ko tànn ngir diirub juroomi at (leegi soppees na ponku sartu réew bi aju ci diirub ngiitug réew mi, yobbóoti ko ci juroom ñaari at, ginnaaw bi ñu ko soppee jële ko ci juroom ñaar, yobbu woon ko ci juroom), moom njiit li nag mooy tànn njiitul jëwrin yi. Barlamaab Senegaal ñi ngi koy wooye Péncum ndawi réew mi mbaa ( jataayub xeet wi), am na nag 120 cér yu ñiy tànn ci ay tànnéef (élections) yu dul yu  njiitul réew mi(tànnéef yu yoonal yi : élections législatives) ngir diirub juroomi at

Mii menn la ci réew yi gën a am demokaraasi te gën a dal ci Afrig, ndaxte genn daaneel nguur (coups d'État) masu fee am,  « Senegaal niki roytéef » yagg nañu koo joxe, wone ko ngir ñu roy ci, ba tee ay yi di fi am ak doonte Amnesty International mi ngi ñaawlu yenn jàpp yi yor mbubum politig.

Senegaal am Pénc la mu demokaraasi (une république démocratique) (lu sakkan ci ay làngi politig a nga fa). Noste ga fa nekk gu njiitug réew la, ndax ba mu amee ag tembam Senegaal daa daal di jël Faraas niki roytéef, roy ca politigam ba ca 1958, niki yeneen réewi Afrig yi bokkoon ci ASF(Afrig gu Sowwu gu Faraas).Sartu réew bu Senegaal mi ngi taariixoo ci 1959, xoolaat nañu ko ci 1960 ki ko def di Léopold Sédar Senghor ginnaaw genn laaju (référendum). ay xoolaat (révisions) yu bari topp nañu ci, ñooy gu 1963 moo fi saxal nosteg njiitu réew (ci jamono jooju : dindi njiitul jëwriñ) teg ci gu 2001 gi yobbu àppub njiit gi jële ko ci 7 at, yobbu ko 5 at (jataayub mag ñi(le sénat) jëlees na ko fi, ginaaw bi ñu delloosi ko ci 2007).

Njiitul Pénc mi( Le Président de la République) (xoolal limub njiiti Senegaal yil) mooy kilifag nguur gi, moom nag ñi ngi koy tànn, mu ame ci pal gu mbooloo mi (suffrage universel) ci anam gu jonjoo de (manière directe) ci diir bu tollu ci juroom ñaari at, manees koo yeesalaat benn yoon. Mooy fal njiitul jëwrin yi (xoolal limub njiiti jëwrin yu Senegaal) moom itam (njiitul jëwrin yi) mooy tànn jëwrin yi, ba noppi sàkku ci njiitul réew mi mu tabb leen.

Ki njëkk a nekk njiitul Senegaal mooy Léopold Sédar Senghor,mu nekkoon njiit lu ubbeeku te dib taalifkat bu siiwoon . Ci 1981 la ko njiitul jëwrinan lii di Abdu Juuf wuutu, waaye ci 2000 la Làngug demokaraasi gu Senegaal gi am ndam ci njiitug Abdulaay Wàdd, ñu falati ko ci 2007. Njiitul góornamaa bi fi nekk fii mu ne mooy Seex Ajiibu Sumaare.

Parlamaa bu Senegaal yor na ñaari néeg : Péncum ndawi réew mi ak jataayub mag ñi.

Bi ñu ko taxawalee ci 20 ut 1960,Péncum ndayi réew mi mi ngi yor 150 ndawi réew, yu ñu fal ci pal gu mbooloo mi ci anam gu jonjoo (au suffrage universel direct) ngir diir bu tollu ci 5 at. Tànnéef gi gu ëppte la (Le scrutin est majoritaire) ci genn wër, ci tund  yiy xëccoo 90 ndawi réew, di it gu kem (proportionnel) di ab lim bu tas ci réew mi ñu koy xëccoo mu tollu ci 60 ndawi réew. Péncum ndaw yi Macky Sall moo ko jiite, mi nekkoon Njiitul jëwrin yi, waaye fii mu nekk, aw yoon jug na wu Saada Njaay indi ngir ñu jële ko fi, wàññi ab àppam ba du weesu menn at ngir man ko fee jële, wii yoon nag, jot naa jàll, waaye njiitul réew mi dëggalagu ko. Tànnéef yu yoonal yu Senegaal yu 2007 jàll nañu ci ndam lu yaatu lu  àndandoo gu njiit gi (coalition présidentielle), waaye lu jege ñaari ñatteel (deux-tiers) ci falkat yi demuñu woon ca mbañ-gàcca ya, li ko waral di ndigalul dogoo(boycott) lu bawoo ci làngi kujje gi.

Parlamaa bu Senegaal boroom benn-néeg (monocaméral) la woon, ci diirub jenn jamono: Jataayub mag ñi, muy lu ñu dindi ci 2001 ci ginnaaw genn laaju gu sartu réew (référendum constitutionnel), delloosi nañu ko ca mee 2007. Mag ñi (Les sénateurs) nag dinañu tollu ci limub 100. 35 ya ca ñoom dañu leen a fal ci anam gu jonjoodi (au suffrage indirect) ci tund yi, yeneen 65 yi njiitul réew mi di leen tabb. Paap Jóob, kilifag Ndakaaru moo ko jiite .

Am na yoon (loi) wu ñu def ci diggadil gi(La loi sur la décentralisation), nekk na it di lu ñuy doxal la ko dale ca samwie 1997, , yoon woowu jox na ay ay doole yu am solo ñeel jataayi diiwaan yi (assemblées régionales). 

Ci 1992 la Àttewaay bu Kawe (la cour suprême) bu Senegaal bi nekk di lu ñu dindi, ñu wottee ko cér (organes) yu jagoo loolu: Àttewaay bu firi bi(Cour de cassation), Jataayub nguur gi (Conseil d'État) ak Jataayub Sartu réew mi (Conseil constitutionnel), yooyu cér di yu niru lool séeni moroom ya nekk Faraas. Seeni àttekat Njiitul réew mee leen di tabb. Yooyu ñooy bànqaasi yoon yi gën a kawe ci réew mi (les plus hautes instances judiciaires du pays).

Dalub Àttewaay bu firi bi ëmb na lenn njiit lu njëkk, ak ñatti njiit yu néeg (trois Présidents de chambre) ak gën jaa néew juroon ñeenti xelalkat (9 Conseillers). Ca toppewaay ba le (Parquet), mi ngi ame ci ab Toppekat bu Matale (un Procureur général) , ci benn layalkat bu njëkk bu matale (un Premier Avocat général), ci gën jaa néew ñaari layalkat yu matale (deux Avocats généraux) ak  gën jaa bari juroom benni déglukat (six Auditeurs) yu koy liggéeyal. Am na ñatti néeg, yoy bu ci nekk mi ngi ame ci lenn Njiit ak ñaari xelalkat gën jaa néew:

Jataayub nguur gi ay xaaj yu bari ñoo ko sos:

Jataayub sartu réew bi yor na juroomi cér, yu ñu tabbe ci ag santaane (décret) ngir juroom benni at yu ñu dul yeesal, yoo xam ne njiit ca la ak topp-njiit (Vice-président). Dees na ko yeesal cig wàll waaye déet lépp, waaye du weesu ñaari cér gën jaa bari. Ab liggéeyam mooy fuglu tànnéef yu yoonal yi, ak xool ba xam yoon yi (les lois) dëppoo nañook sartu réew mi, ak warlu yu àdduna yi (les engagements internationaux).

Senegaal dindi na mbugalum ray ci 10 desambar 2004.

Li ëpp ci gëstu yi ñu def ci wàllug Gëstu-askan (walla demogaraafi) ci Senegaal dafa sukkandiku ci Waññ (recensement) yi ñu jotoon a def ci 1976, 1988 rawati na 2002. Doxal gu Séentu ak Lim gi (la Direction de la Prévision et de la Statistique) ci 2004, siiwaloon na « ay leeral ci askani Senegaal yi, loolu di woon lu juge ci waññ gu 2002 » mu sóoraale woon ci màgg gi man a ami ci askanu Senegaal la ko dale booba ba 2015.

Bu ñu sukkandikoo ci gongikuwaay yii, askanu Senegaal - wi doonoon lu toolook 1 milyoŋ ciy way dëkk ci 1900 ak  2,8 milyoŋ ca jamonoy ag tembam ca 1960 – yekkatiku na tay ba àgg ci  ciy jëmm (nattale gi ci 31/12/2007) te man naa àgg ci  ci mujjug 2015. Askan wii kon day màgg ci anam gu gaaw, ànd ak benn tolluwaayu njuru (taux de fécondité) bu tiim 4 doom ci jigéen.

Seetloos na fa genn kuute gu giir gu mag: Wolof (43,3 %), Pël (23,8 %), Séeréer (14,7 %), Joolaa (3,7 %), Malinke (3,0 %), Soninke (1,1 %) Maanjanke (2%) ak yennat ci ay giir yu gën a néew, te gën a gawu ci barab,waxuma la nag naari Libaan yi ak Tubaab yi, nga xam ne ñi ngi nekk ci dëkki taax yi . Ci mujjug 2007,  ci waa Faraas bindu woon nañu ci seen barabu aji teewal (ambassade) (boroom ñaari réewu it ci lañu woon (les binationaux)). 

Ab diir bu yàgg a ngii askan wi nekk di jalu ci fi jàkkaarloo ak Mbàmbulaan gu Atlas gi, waaye nocciku gu kaw gi (l'exode rural) yokk na yamoodi gi ci séddale gii. Fi mu nekk ñeenti nit yoo gis ci waa Senegaal, kenn ka mi ngi dëkk ci Daanaka dun bu Bopp bu Wert  bi (Cap-Vert), looloo waral péey baa ngi waaj a xëx.

Bu Ndakaaru jàllee, diiwaan yi ñu gën a taaxal (les régions les plus urbanisées) ñooy Siggicoor, Cees ak Ndar. Yi gën a néew ag taaxal (moins urbanisées) ci diiwaan yi ñooy Koldaa, Maatam ak Fatig.Diiwaanu Tàmbaakundaa nag moo yor fatt (densité) gi gën a doyadi (11 way dëkk ci jñ²).

Bu ñu sukkandikoo ci nattale yu 2007, digg yu taax yu diiwaan (les centres urbains régionaux) yi yor lu ëpp  ciy way dëkk ñooy Tuubaa ( (Man nag yaakaar naa ne ag na ma xame Tuubaa, la fa dëkk man naa ñeentte lim bii ñu wax) – mi jekki jekki gis ag màgg gu yéem ñépp –, Cees (), Kawlax (), Mbuur (), Ndar (), Siggicoor () et Njaaréem ().

Ca 2007, Senegaal teeru woon na lu tollu ci 23,800 ciy daw-làqu ak sàkkukati ag wéeru ( demandeurs d'asile), yoo xam ne lu ëpp 20,000 ca ñoom ay waa Gànnaar lañu, yu doon daw boddanteg xeet ga, ak ñennat ci waa Liberiyaa, waa Siraa Leyoon, ak yeneen réew .

Bu Senegaal dee réew muy teeru ay way gàddaay (ay migrants), moo xam yu ay jamono lañu(saisonniers) mbaa déet, moo xam yu bawoo ci réew yi mu digool lañu walla yu ko sori, du tee menn mbooloo mu Senegaal mu mag ma ngay dund ca bitim réew. wisaaroo gii (diaspora)alal ju am solo la ci réew mi, ci wàllug koom ak njëmmte (identité). Xarala yu xibaar ak jokkoo yu bees yi XXJB dañuy gën di jàppandal jokkoo ci diggante njaboot gi te tax it deesi man a dund mu mel ne da ngaa nekk ci sa biir réew .
Li ëpp ci ñiy dem nag ay waxambaane lañu yu jublu Tugal, rawati na Faraas, ak Itaali, walla ñuy dem ca Aamerig gu bëj-gànnaar ga, ca Kebeg yobbaale ci seeni xol naalub dellu réew ma ci ginnaaw yennat ciy at. Màggug gàddaay gu yoonoodi gi (immigrations clandestines), ñu koy def ci ay anam yu bon te ñaaw jëm ci Duni Kanaari yi lu tiital Senegaal la ak réew yi koy teeru.

Ñi gën a ñàkk yaakaar ñoom faalewuñu sax ay wi ñu ci man a dajeel, ginaaw gis nañu seeni moroom tekki, rawati na ya bokk ca wisaaroo ga (diaspora) — moo xam Senegaal lañu juddoo mbaa dañu faa am rekki way jur - rawati na ñi ciy yëngu ci tàggat yaram mbaa fànn (art).

Lu sakkan faatoo na ci gàddaay gu yoonoodi gi, mbaa mbëkk mi, baat bi ñu ko gën a xame, lu ko waral? xanaa géej gi ñu sóobu ci lu duli jumtukaay yu dëppoo , ñoom kay dañuy sóobu ci ay looca yu doyadi, duy kooki bagaas ak nit ci wépp xeet ak maas, bu ko defee yooru, duñu faale la leen dëgmal ciw ay ak musiba, gaal gaay doon duus ba, néegub añ ba, bu tëdd ba, leeg-leeg duus ñëw téq leen mbaa ngelaw lu saf, ba kero ñuy àgg bu ko Yàlla dogalee, waaye cis lëf cig loof, lu sakkan di ca des dib añ mbaa reerub ag kuréel ciy jën yu waroon a nekk diy añ ñeel leen mbaay reer. Nii lay deme ba kero ñuy àgg ak la leen fay xaar ciy kaso ak ëlëg gu lëndëm, lii mooy li xew ci mbeex mi, waxuma la nag la ca tàkk ga, aji tàng ji tàkk gii nga xam ne jali beeñ yi yàgg nañu fee tee nit àgg fa mu jëm.

Senegaal nguur la gu bokk ci Bennoo gu koom-koom ak gu koppar gu Afrig gu sowwu gi. Ginnaaw ay jafe-jafe yu koom-koom ci njëlbéenug ati juroom neen-fukk yi, ay yoonam (ay luwaam) yu koom-koom soppiku nañu, bu ko defee ag màggam gu koom-koom mujj àgg ci ay 5% ci diggante 1995 ak 2001. Ci ndoortel 1994 Senegaal door na ci doxal tëriinu yéwénal gu koom-koom gu kawe ay yitte, ci càmmug mboolaay gu àdduna bi (communauté internationale), looloo ko jañoon ci mu woyofal xiimay kopparam bii nga xam ne daa tënku ci Frank bu Faraas, mu woyofal ko ba ci 50%. Jeexiitalu woyofal gii diisoon na lool ci ay way dëkkam, ndax taxoon ba njëgi li ëpp ci marsandiis yu dàttu yi ak yu dund yi seeroon te yekkatiku, niki meew, yàpp, ceeb, ba àgg ci fulu ci genn guddi, waaye am na genn màgg gu am ci koom-koom bi, ak ci njuddéef mu ñumm mu biirum réew mi, ngir yéwénal yi, nga xam ne àgg na ci 5% ci at mu nekk, bu ko defee walu gi(l'inflation) wàññiku ci anam gu yéeme ba àgg ci ay lim yu ndaw bu ñu ko nattee ca la romb.

Ci 20/ut/ 1960, la Senegaal génn ci lëngoo gu Mali gi, daal di jibal ag tembam.

Senegaal ak Gàmbi bennoo nañu ci 1982 ngir amal lëngoo gu Senegàmbi, waaye gii nekkutoon lu dul aw gisiin, kenn masu koo jëfe. Mujj gi ñu far ko tas ci 1989.

Ay janoo jot nañoo am la ko dale ca 1982 ci anam gu dogatu ci diggante ñoñ tàqalikoo (les séparatistes) ñi nekk ci bëj-saalum gu Kaasamaas ak doole yu góornamaa bi. Ginaaw ay jéem yu bari yu àntuwul, genn dëppoo mujj nañu ko xaatim ca Siggicoor ca 30/desambar/2004  ci diggante jëwrini biir-réew ji woon Usmaan Ngom ak làbbe Augustin Diamacoune Senghor, mi nekkoon njiitul fipp gu Yëngu-yëngu gu doole yu demokaraasi yu Kaasamaas (YDDK)(MFDC), moom Diamacoune Senghor moomu mujj na faatu.

Beneen tombub coow ci diggante ay waa Kaasamaas ak Ginne-Bissaawuóo màgg na ci awril 2007.

Ci 1989, Gànnar ak Senegaal génne nañu ku ci ne, ci anam gu ñaaw sa njabootug moroom te ña ëppoon  ca ñoom ña nga juddoo woon fa ñu leen génnee, muy réew mi leen doomoo woon, ñu jotoon faa seey ca mboolaay ga ak koom-koom ba. Bu ñu sukkandikoo ci li Jataayub daw-làq bu kawe bi (JDK) HCR wax, ay daw-làqu ña nga des ba tay ca guddaayub dexug Senegaal gi. Ci 2007, Njiitul Gànnaar jibaloon na ba muy def càkkug palaam ga (campagne), ne nangu na delsig doomi réewam yooyu doon dund ci Senegaal ak Mali te neexu leen.

Senegaal a ngi nekk ci diggante 12°8 ak 16°41 wu rëddu tus-wu-gaar wu bëj-gànnaar ak 11°21 ak 17°32 wu rëddu tus-wu-taxaw wu sowwu. digam wi gën a féete sowwu mooy Ndakaaru di it cat li gën a féete sowwu ci goxu Afrig. 

Su ñu ko méngalee ak réewum Mali walla ak mu Gànnaar di nanu gis ne Senegaal réew mu tuuti la ci rëyaayu-suuf.

Kilimaab Sahel la ame:

Ca atum 1996 la seddale gu mujj gi ame, mooy giy wéy ba tay, lu dul coppite yi ci mujj a am: Sosug  diwaanu Maatam ci 2001 ak gox-goxaan bu Kungeel ci 2006.

Ci 2008, la Senegaal nekk 14 diwaan,   

Yenn ciy dëkk: 

Senegaal doon na réew mu bariy giir, waaye it soo ko mengalee ak yeneen réewi Afrik yu bari, wuuteg ay giiram du feeñ. Man nan ni daanaka wuute amul ci diggante giiri senegaal yi ndax seenug bennoo ci      caada. Man nan cee lim yii tambalee ko ci yi ci gën a bari ba ci yi ci gën a néew: Wolof (43,3 %), Pulaar (23,8 %), Seereer (14,7 %), Joolaa (3,7 %), Malenke (3,0 %), Sooninke (1,1 %) Manjaak (2%), ak yeneen giir-giiraan yu tas ci réew mi, man nan cee boolee it tubaab yi ak naari libaan yi. 

#Article 5: Bene (111 words)

Benin (Republik bu Benin) : réewu Afrig.

Bene aw rëdduw suuf wu sew la, nekk ci diggante yamoo gi ak Gëwéelub Sànkar bi. Rëddu tus-wu-gaar wu bene mi ngi ci diggante 6°30'bëj-g ak 12°30'bëj-g, tu-wu-taxawam moom mi ngi ci 1° P ak 3° 40'P.
Ay digam ñoo ngi yem ci Togóo ci sowwu, yem ci Burkina-faso ak Niseer ci bëj-gànnaar, ci Niseeriyaa ci penku, janook mbàmbulaanug Atlas gi ci bëj-saalum. Mi ngi am yaatuwaay bu tollu ci 112.622 yu kaare. Bene ngi bawoo ca dexug Niseer gi ci bëj-gànnaar yem ci mbàmbulaanug Atlas ci bëj-saalum ci ag tallalug 700 km. Diggante bi gën a guddu ci réew mi 325 km la.

#Article 6: Itaali (160 words)

Itaali (Pénc mu Itaali; it: Italia, Repubblica Italiana) réewum Tugal (Óróop)
Itaali men la ci réew yi nek ci Bëj-saalumu tugal,

ngir xootal Taarixu Itaali xoolal 

Itaali laata a Napoleon di ko teg loxo, di ko nangu, nekkutoon réew mu ñu bennal , nekkutoon it di mu am ag temb, moom kay daa seddaliku woon, doon fukki xaaj ak ñaar, yu doon topp ak a nekk ci ron kiliftéefug ay nostey politig yu wuute: nosteg nguur ca Savoia, Piemonte, Napoli, ak nosteg pénc ca Venezia ak Geneva, ak ag àtte gu paab ca Rom, ak gu Dóox ca Toskaana ak Parma, ak xaaj yoo xam ne dañoo nekkoon ci waawug imbraatóor gu Otris gi, ñooy Milano ak Lombardia.

Piemonte nag moo nekkoon nekkteg politig gi gënoon a dëgër, te ëppoon doole ci nekkte yooyu. Ña ëppoon ca njiit ya yilifoon nekkte yooyu, ay diktaatóor lañu woon, rawati na ñi ci waa Otris jiite woon, cig jonjoo mbaa cig jonjoodi .

#Article 7: Tansani (368 words)

Tansani am réewum penku Afrig la, féete ci peggi mbàmbulaanug End . Keeñaa ak Ugandaa ñoo ko féete bëj-gànnaar, Ruwandaa, Buruundi ak Kongóo-Kinshasa nekk ci sowwoom, Saambi ak Malawi nekk ci bëj-saalum-sowwoom, Mosambik nekk ci bëj-saalumam.

Réew mi tollu na ci 947 303 te am 51 820 000 ciy way-dëkk, ay bantu rekk a fa dëkk.  Péeyam mooy Dodoma, mi ngi nekk ci biir réew mi, waaye dottub koom-koom bi dëgg mooy Dar es Salam gi doonoon péey bi, féete ci tefes gi. kiswahili ak wu-angalteer ñooy làkki nguur ga, teewul ne itam araab am na fa doole, rawati na ci duni Sansibaar ak bu Penda.

Tansani ju tay jii a ngi judd ci booloog Tanganyika ak Sansibaar ci 26 awril 1964, gannaaw, ci lu yàggul dara ñu am seenug tembte ci Nguur-Yu-Bennoo yi. Bokk na ci Commonwealth dale ci atum  1961, bokk na itam ci Mbootaayu Xeet yi dale ci 14 desambar 1961. 

Ci 1953, Julius Nyerere, ab jàngalekat la woon bu judd ci 1922, ci bi muy am 31 at la ñëw ci boppu TAA (Tanganyika African Association, mbootaayu waa-afrig bu Tanganyika), mu daldi koy soppi ag làngu politig dëgg, ci lu gaaw, tudde ko  Tanganyika African National Union doon woote ngir ag tembteg seenum réew. Ci 9 desambar 1961 la leen ko Nguur-Yu-Bennoo yi jox, ci jàmm. Ci ndoorte li jëwrin ju njëkk la doonoon, ginnaaw pal gu desambar 1962 gi, mu doon njiitu réew ju njëkk ju Tanganyika.

Ci 10 disambar 1963 la Sansibaar ak Pemba am seenug tembte, 26 awril 1964 la Tanganyika ak Sansibaar booloo ngir sos li tudd tay Réewum Tansani. Nyerere doon njiitu réew ma, Abeid Karume mi doonoon njiitu réewum Sansibaar nekk jëwrin ju njëkk ji, ci Tansani. Donte booloo gi amoon na, waaye ba-tay jii Sansibaar moo yoral boppam yenn yi. Njiitu réewum Tansani moo ko yoral li ñeel politig, kaaraange, mbiri biti-réew, añs, moom mu yural boppam njàngale mi ak koom-koom,..

Tansani réew la mu nekk ci  xaaju kol-kol bu bëj-saalum féete ci Penku Afrig. Ay digam yu dénd ñooy mbàmbulaanug End gi ci penku, dojuw Kilimandjaro ak déegub Victoria  bi ci bëj-gànnaar,  déegub Tanganyika bi ci sowwu, déegub Malawi ci bëj-saalum-sowwu ak dexub Ruwuma ci bëj-saalum

#Article 9: Tugal (184 words)

Tugal mooy wàll wi féete penku goxub Tugalasi, ci baax dees koy jàppe niki benn ci juroom-benn walla juroom-ñaari goxi àdduna bi. Gox baa gi digu ci sowwu ci mbàmbulaanug Atlas gi, ci bëj-gànnaar ci dottub Bëj-gànnaar bi, yem ci géej gu Diggu gi ci bëj-saalum. Ay digam ci penku dese nañoo leer, dinay faral di jur ay werante; li ko waral mooy ni mu taqalook goxub Asi.

Waa-Islaand jàppees na leen ni waa-tugal (donte féeteem ci degalub Tugal-Aamerig), ak mbooleem dun yi ci géej gu Diggu gi, Sipër mi gën a jur coow, ci wàllu melosuuf. Riisi ak Tirki ñi am li ëpp ci seen suuf ca Asi, waaye day ni rekk li ëpp ci seen taariix réewi gox bi lañu ko bokkal. 

Ngir xóotal: Melosuufug Tugal
Tugal a ngi yaatoo 10 392 855 km² (fukki junni-junni ak ñetti-fukki-junni ak juroom-ñent-fukk ak ñaar ak juroom-ñetti-téeméer ak juroom-fukk ak juroom). Di benn ñetti Afrig walla benn ñenti Asi walla Aamerig. 

Mi ngi séedatliku ci jurromi diwaan: Penku Tugal, Diggu Tugal, Sowwu Tugal, Bëj-gànnaaru Tugal ak Bëj-saalumu Tugal 

Gox bi am na 49 ciy réew.

#Article 10: Afrig (568 words)

Afrig, Afirig, moom la ñu jàppee ne mooy gox bi nit cosaanoo, su nu ko xoolee ci yaatuwaayam ak bariwaayu askanam (lu weesu gox bu Asi), mooy ñaareelu gox bi gënn a rëy ci àdduna bi. Yaatuwaayam tollu na ci 30.065.000 km², nekk 20,3% ci jéeri ji ci àdduna bi. Ay way dëkkam tollu ci lu ëpp 800.000.000, muy benn juroom ñaareel bu way dëkki àdduna bi. Afrik a ngi yem ci bëj-gànnaaram ci Géej gu Diggu gi, ci sowwu ci Mbàmbulaanug Atlas, ci bëj-saalum ci Mbàmbulaan gu Bëj-saalum gi, ci penku ci Mbàmbulaanug End. Asi rekk la taqalool ci yeneen gox yi. Yamoo gi jàll na ko. Ci jëmm doon na gox bu bari'y melokaan, te wuute teg ci.

Baatu «Afrig» moo ngi jóge ci turu Afridi yi, doonoon ag giir gu dëkkoon ci Bëj-gànnaaru Afrig ci diwaanu Kaartaas.

Beneen cosaanam moo bàyyikoo ci Berber Taferka «suuf», «boroom suuf». Ki fay dund la ñuy woowee Aferkiw, Latin yi soppi ko africanus, mu doonoon aw tundu waa rom ci Afrig. Araab yi di ko wax إفريقيا ifrīqīyā, mu doonoon Tiniisi gu tay gi.

Ñeneen ne ci baatu waa geres bii di aphrike («amul sedd»), latin di ko waxaprica («Bari naaj»), la jóge.

Afrik la ñuy jàppee ne mooy cosaanu nit, ndax desiti nit yi gën a yàgg ci àdduna bi fa la ñu ko gisee, ci Afrig gu Bëj-saalumu-Sahara.

Sahara cëru na bu baax ci màggug gox bi. Taariixu askani Bëj-gànnaaru Afrig yi day tolloo ak bu Tugal ak bu Penku gu Diggu gi. Li ëpp ci Afrig gu Bëj-saalumu-sahara amul woon genn jëflante ak li des ci àdduna bi, da ñoo beru woon.
 
Xay yi juddoo ci goxu Afrik, boole nañ leen ci yi gën a mag ci taariixu nit. Xayu Esipt ak bu Gana ak bu Mali, ak bu Kuush ak bu Songaay, añse. 

Ci li taariixkat yi wax, jàppum njaam mi ngi tambali ci xarnub VII ak araab yi. Ci lu gën a leer ci atum 652 ba Ab njiitu araab takk-taxawalee waa Nubi yi ngir ñu jox leen 360 ciy jaam at mu jot. barab yi njaay mi doon amee mi ngi dale ca Mali ba Penku Afrik, ci wàll gi féete bëj-saalumu Sahara. 

Ci xayma nee nañ ci diggante xarnub XVIII ba ci xarnub XIX, benn ñenteel ci nit ñi ay jaam la ñu woon, walla ñu ñu manante (takk-taxawal) ci liggéey bu ñu sañut a bañ. Nee nañ njiitu waa afrik yi ci seen bopp ñoo doon jàppaate ak a jaayaate. 

Waa tugal lu weesu bi ñu aakimoo (walla sancee) suufi Aamerig yi da ñoo soxla woon ay loxo yuy liggéey ci seen tool yi. Def nañ ko ci 400 at (1500-1888), ay jaam yu bari jënd nañ leen walla jàpp nañ leen ci tefesi afrik yi: Sowwu Afrig gépp, ak ci bëj-saalumam itam. Donte tereg jàppum njaam gi mi ngi waddoon ci lu jege atum 1850 (réew yépp bàyyeendoowuñu ko) amoon ay nit yu wëyoon di ko def cig làqatu ba ci 1900. 

Jamonoy aakimoo gu tugal ci Afrig moo ngi tambalee ci Ndajeem Berlin (1884-1885) ba ci tembte yi ci atum 1960, sedatle gu réew yu tay yi ca la jóge. Ecoopi moo doonoon menn rèew mi ñu masut a teg 

Xool: Diiney Afrig

Gëstukatu-làkk yi ci xayma nee nañ 2 000 làkk ci goxu Afrik, ñu boole leen ci ñeenti mbooloo, làkk yi fa cosaanoowul bokkuñu ci.

Koom-koomu Afrig

#Article 11: Biibël (112 words)

Biibël Mooy tur bi ñu jox mboolem mbind yu sell yu Yàlla yi, ci diiney yawut ak Kirist. Baatu biibël la ngi jòoge ci kallaama gerek gu yagg ga, di tekki “teere yi”. Ci’g neen, day ab teere bu ñu boole, ay mbindi cosaan, mbindi atte, mbindi xew-xewu demb, mbindi cellte, yu yonent, taalif ak ay bataaxal, yoo xam ne ci diiru junniy at lañu leen bind. Biibëlu kercen yi dañ koo seddale ci ñaari pacc: Seede bu Yag bi, bi ñu boole teere yi ñu dondee ci diine yawut yi ak Seede bu Bees bi, di ay mbind yu’y seede dundu Yeesu-Kirist. Ci Jàngu yi, Biibël kaddu Yalla lañu koy wowee. 

#Article 12: Diiwaan yu Bennoo (428 words)

Diiwaan-yu-Bennoo, walla Diiwaan-yu-Bennoo yu Aamerig ci anam gu gudd am réew la mu séddaliku ci juroom-fukki diwaan, ñent-fukk ak juroom-ñett yi ñoo taqaloo te féete ci diggante Mbàmbulaanug Atlas ak Gu-Dal gi, penku ba sowwu, Kanadaa moo féete bëj-gànnaar, Meksik nekk ci bëj-saalumam. Alaskaa ci la bokk donte taqu ci, mi ngi nekk ci sowwu Kanadaa. Xawaay moom mi ngi ci diggu mbàmbulaan Gu-Dal gi. Réew mi am na fukk ak ñenti diiwaan yu tasaaroo ci géeju karayib yi ak Gu-Dal gi. Péeyam mooy Washington. 

Diiwaan-yu-Bennoo yi ci 2008, 302 ciy miliyoŋ ciy way-dëkk lañu amoon, loolu tax muy ñetteelu réew mi ëppi nit ci àdduna bi, ci ginnaawu Siin ak End. Réyaayam toll ci 9,4 junni km², di ñeenteel ci àdduna bi, ci ginnaawu Riisi, Kanadaa ak Siin. Gàddaay gi bari na fa lool, ba tax muy réew mi ëppi xeet yu jaxasoo ci Suuf si. Koom-koomam mooy bi gën a woomle ci àdduna bi, te moo am njuddéef mu ñumm mu biirum réew (NJ.Ñ.B) mi ëpp ci àdduna bi.

Turu Réew mi Thomas Paine moo ko tànnoon ci bés bi ñuy am seenug temb ci 4 sulet 1776.
Woowiin wu gàtt wi, wi ñuy faral di jëfandikoo ci sunuy waxtaan, ci njàngale mi ak ci lonkoyoon yi, mooy «Diwaan-yu-Bennoo» (ci wu-angalteer di United States, ñu tënk ko ci US). Wu gudd wi ñu koy faral di jëfandikoo ci këyiti nguur gi «Diwaan-yu-Bennoo yu Aamerig».

Ci Alaskaa lañu gise jeexiti nit ki fa njëkk a teew, ci weti 20 000 at nj.j, ci tefesu atlas ci wetu 13000 at nj.j. Nit ñi njëkk a dëkk ci réew mi ñoo nga bàyyikoo ca Goxub Asi, jaare woon ko ca xat-xatu Beriŋ. Ci ginnaaw bi la fa waa-tugal yi ñëw.

Christophe Colomb moo wuññi goxub Aamerig ci 1492, at ma ca topp mu nemmeeku barab bi nekk Poortorikoo tay jii. Ci XVIu xarnu la réewi Tugal ya fa ëppoon doole doon seet ay jàlluwaay ci bëj-gànnaar-sowwu ak ay am-am, ci seeni tukki ci topp tefesu Atlas gi ñu dem ba taxawal fa ay sancu yu sax. Ci bëj-saalum waa-espaañ yi sos fa seenub sancu duppee ko Espaañ-gu-Bees, di amal ay tukki-gëstu ci biir réew mi. Ci bëj-gànnaar-sowwu waa-riisi yi sanc fa ci li topp tefesu Mbàmbulaanu Gu-Dal gi. Ci la tubaab yi tàmbalee yaxantu ak askan yi fa cosaanoo.

Ci diggante XVIIu ak XVIIIu xarnu, ndànk ndànk, la fukk ak juroom-ñetti sancu waa-angalteer taxaw ci tefesu penku gi, Lii mooy maamu Diwaan-yu-Bennoo yi. Waa-fraa yi nemmeeku pegu Misisipi dal di fay sos Luisiyaan 

Ngir xóotal yëral foofu: Taariixu Aamerig

#Article 13: Tuubaa (431 words)

Tuubaa, péeyu murit yi,ab gox-goxaan la, mi ngi nekk ci diiwaanu Njaareem (jurbel), ci tunduw Mbàkke. Diggam ak Ndakaaru tollu na ci 150 km .

Baatu Tuubaa mi ngi jóge ci làkku araab di tekki ci wolof : « texe ». 

Dëkkub Tuubaa, kii di Sheex Ahmadu Bamba moo ko sanc ci atum 1887.

Dëkk bi mi ngi aju ci Ndaam, doon as ngox, maanam dëkku kaw kaw, bu taaxeedi, te nag doon gannaaw Ndakaaru, dëkk bi gëna taaxe ci Senegaal. tey dëkk bi gën a rëy ci senegaal ginnaaw ndakaaru

Tuubaa moo ëpple yokkute ci barig nit ñi ci diiwaani Senegaal yépp (3,2% at mu nekk ci jamono yii ñu tollu te ñu jàppu ne yokkuteg nit ñi di na àgg ba 12% bu ñu àggee ci ati 2010). Yokku yooyu li ko waral moo di tuxu yu bari yi nit ñi di def bawwoo ci dëkk yu nekk ci Bawol ak Kajoor. Dëkk yooyu dañuy gent si ndànk ndànk jëm Tuubaa. 

Ci waññib 2002 bi, nit ñi ñi ngi tolloon ci 461 159.

Ci atum 2007, bu ñu ajoo ci gam-gamle gu nguurug Senegaal, waa dëkk bi tolloon nañu ci 529 176.

Naataangeg dëkk bi lëkkaloo na lool ak Màggal gu mag gi giy dëppoo ak demug Seex Ahmadu Bamba ci géej gi.Ba tay Tuubaa dafa bari li waa Senegaal di woowe Moodu moodu, di ay tukkikat yu féete Tugal tey ëndi xaalis bu bari ci dëkk bi. Lii di yaxantu (jënd ak jaay) tamit da faa dox lool.

Kii di Seex Abdul Ahat doon ñatteelu xalifa Seex Ahmadu Bamba moo fa tabaxoon barab bi ñuy woowe daaray kaamil di kàggu gu ñu denci mbindum Seex Ahmadou Bamba ak yeneeni mbind aki téere yu aju ci lislaam, ak ci yeneen fànni xam-xam yi yittéel nit, mi ngi feete nag ci penku jumaa ji, làng ak armeel yi.

Ci Tuubaa la jumaa ju mag ji nekk, doon jumaa joo xam ni jenn la ci Afrig gu sowwu jant, ci taaram, ak ci rëyaayam. man nañoo jàpp ne mooy xolu dëkk bi, ndaxte yeneen kër yepp dañoo ñëw di ko wër ndànk ndànk, ànd ak màggaayu dëkk bi. Jumaa ji am na juroomi sooroor ak ñeenti xubba. Soorooram bi gën a gudd tollu na ci 80 meetar. Sooroor boobu, kii di Sëriñ Fàllu Mbakke mooko tudde Làmp Faal féetele ko kii di Maam Seex Ibra Faal ci 7 juin 1963. Bis boobu moo di ubbite gu njëkk, ba ñu bari teewe woon nañu ko, ku mel ni Lewopool Sedaar Seŋoor. Foofu ci jumaa ji fa la barabu Seex Ahmadu Bamba nekk.

#Article 14: Kàllaama (11114 words)

Kàllaama (fr : langue ; en : language)

Ñi ngi tàmbali sunuy wax ak jëf ci turu Yàlla(t.s) miy Rahmaan, di kiy boroom yërmaande ju yaatu ji ñu jagleel mbooleem mbindéef yi, tey Rahiim, di ki yor yërmaande ji mu'y jagleel ña nangu'g jaamoom.
Di julli nag te'y sëlmal ci sunu sang, sangu'b ñu jiitu ñi ak ñu mujj ñi, aki ñoñam aki saabaam, ak aji liggéeyalam jii di sëriñ Tuubaa, ak xeetam wépp. Sunu wax ji dañu ko'y tàmblee cib aaya'b alxuraan, ñu ci'y tegtaloo li làkk ëmb, yor ko ci'y njariñ, ci gépp wàll, ci sunu dund gi. Sunu boroom nee na ci alxuraanam ju tedd ji:(( Wa hallama Aadamal asmaa kullahaa, thiumma haradahum halal malaayikati, fa xaala anbiuunii bi asmaayi haaulaayi in kuntum saadixiin)) di maanaa : Yàlla (t.s) jangal Aadama tur ya yépp, bi mu noppee, jël mbir yooyee won leen malaayika yi, ne leen wax leen ma seeni tur, bu ngéen léen xamee? ñu ne ko tudd nanu sa'g sell, amuñu benn xam-xam boo ñu xamalul,bu ñu xam, yaw yaa'y ku xam ki, te'y ku xereñ , ku am hikma ki. Kon yii tur ci jii aaya ju tedd, mant'a doon lu dul làkk, wi nga xam ne bokk na ci li Yàlla (t.s) njekk'a xamal Aadama (j.m) bi mu ko bëggee wàcce ci kaw dénd bi, ngir mu wuutu ko fi. Loolu nag li ko waral moo'y nekku'g làkk di benn ci móoli cosaan yi ñu teg sunu dund gi, tabax ko ci. Bu doonul woon moom, dund gi di lu nekk ci lu dul maanaa mu ñu xam, di lu gën'a jege ag mbàyyima ci ag nite, bu amul wuutlaay. Ma ne xoolal ma dund gu ñu rafleel ci làkk, nu mu war'a mel ? ndax moo'y googu di fees dell ak junj yi ñu'y jëfandikoo bu ñu'y wax ak ku luu, muuma mbaa ku tëx ? lii sax ca dëgg-dëgg xeet la ci làkk, làkk ëppu ko yéesu ko, ginaaw moom mbir la mu ñu'y def ngir déggante ci. Ndax kat làkk du lu moy ab jumtukaay, ngir waxante, ñu ko'y jëfandikoo ngir déggante ci sunu biir !, xanaa déggoo ñu naan làkku njanaaw yi , mbaa dundat yi, ba ci wu bàyyima yi?jubluwuñu ci lu dul li ñu'y joyal, ngir seen moroom yi dégge léen ci. Ginaaw nag bàyyima yi di nañu déggante ci loolu ci seen biir, kon loolu manatuñu ko'o jàppe lu dul aw lakk ni yeneen yépp. Waaye jeneeral dund gii nga xam ne dafa féex ba ci sax jumtukaay yi ñu'y jëfandikoo ngir junj, maanaam dund gi ñu rafleel ba ci jumtukaayu'b déggante rekk, nu mu war'a mel ? nu xeet ak mbir ya'y dox ci'y sidiitam, aki buumi xolam di mel ? wii xeetu dund de ci li ma jort, narul'a doon lu dul ag ndofe gu ñu joyal, naa doyloo yooyu baat ndegam amuma yeneen yu ko man'a leerale ni mu ware. Gii dund ci lu dul làkk, da na nekki gu maneesul'a leeral, xel it du ko xalam.

Ci loolu la Sayyid Qutub, di waxe ca teereem ba tudd Zilaalul Xuraan, di tafsiir bu mag ci alxuraan, mu ca'y firi aaya bu sell bii di (( wahalla aadama ba maakuntum taktumuuna)), mu ne : (( xool ñu nag ñi ngi nii - ci bëtu'b xol, ak leerug basiira - di jàkkaarloo ak la malaaka ya nekkoon ca Malaul Ahlaa doon jàkkaarlool.... xool ñu ñun ni ngi nii di gis ag wàll ca mbootum Yàlla mu màgg moomee,nga xam ne mi ngi ko dénk nekktéef bii di kojug nit, bi mu ko'y jox caabi'y kuutlaay ji, mu war ko'o wuutu ci kaw suuf.

Mbootum kàttanu'g tudde mbir yi ay tur, wutal yëf yi ay xammeekaay yu tur, sekkare'b man'a jël jëmm yi, walla yëf yi tudde leen ay tur yu leen di def - te ñoom ay baat rekk lañu yu ñu wax - ñu'y ay junj aki sembool yu'y tekki jëmm yooyu ak mbir yooyu ñu leen tudde. Lii daal na la woor ne kàttan la gu am lool solo, ak xiima ci dundu'g nit ci kaw sii suuf.
Ñi ngi'y xam solo sii, bu ñu'y jeneer coona bu mag bi ñu naroon'a jànkoonteel, bu ñu mayutoon nit kàttanu'g junj yëf yi, ak nit ñi ci'y tur. Xoolal coona bi naroon'a am ci déggante ak jëflante, ndax li naroon'a xew, moo'y ku bëgg'a déggante ak sa moroom ci mbir, da nga'y teewal moomale mbir, mbaa ànd ak moom ba ca loola, nga joxoñ ko ko, mbaa nga laal ko.... bu dee xorondoom ngeen soxla, war ce'e waxtaan, da ngeen ca'y dem, mbaa ngeen teewal ko, lu ko moy deet ag déggante ci loolu, bu dee doj la, fawwu ngeen dem ba ca doj wa, bu dee nit, munt'a ñakk ngeen teewal ko, lu ko moy du ngeen ca déggante....
Lii daal coona la bu kenn xalaatul'a dund ak moom, te dund gi tam narutoon'a wëy ci yoonam wii, bu Yàlla (t.s) mayuloon mbindéefam mii man-manu tudde mbir yi ay tur. Malaaka yi ñoom, jagle bii soxlawunu ko, ndax du lu manul'a ñàkk ci ñoom ci seeni jëf, moo waral mayeesu leen ko)).

Kon làkk moo'y ponk bi nga xam ne ci la sunu'g dund di tabaxu, su nu bëggee muy gu jege as lëf ci'g cilwiise aku'g taaxe,walla lenn lu am maanaa.
Bi làkk nekkee nag ba noppi, te tax ñu jeggi mbooleem rombuwaay yii, ca ngënéelam la, ak jappndal gi mu nu defal ba nu man'a déggante ci suñu biir, ñewati na di jumtukaay bi dugg ngir teg sunu dund gii ca njobbaxtal lu kawe, la di ag nite, ak ca tolluwaay bu yekkatiku bee di bu ag taaxe, aku'g xay.

Bu doonul woon làkk, duñu doon man'a yekkati sunu dund gii ci xam-xam, ndax moo'y li'y tax nga man'a raññale mbir ak dundat yi, lu ci nekk nga ber ko nee, wutal ko turu boppam.
 
Làkk moo'y cëslaayu ag yewwute

Yewwute ñenn ñi naan ko renaissance ci francais di judduwaat, di ci araab nahda , di ci maanaa buur , buur nag bu nu ko waxee ci wolof moo'y jekki-jekki jug ,taxaw, ñeneen it di ko fire'e dekki, boo ko'y seet ci maanaa, yepp di wudd lenn, di la amoon ca Orob ca lenn ci'y jamonoom, di woon lu am solo, di lu waa Orob dul fatteeti, baat bii ñew ëmb maanaa mii mépp, di raññale jamono'y yewwute ci ngëmméen, judduwaat ginaaw ag dee, réer ci réeradi,xam ci xamadi, siggi ci segg, nërméelu ci taxaw, giim ci tàkk, xippi ci gëmm.

Bii baat daal jaasi la ju moo dog seen diggante ak jamono joj tëñëxu ak yewwoodiku moo ko muuroon, matale ko, xel mu gàtt lakkal leen ci, gisiin wu ñaaw sonal leen ci, ñu nekkoon ci biiram di way jemadi kanam, di ñu soxlawoo ag leer, ba Yàlla yee ay nit, niital léen ca làmpam bu leer ba'y leerale, jugloo leen ci'y nelaw, ñu nekk ci'g yewwute duggalaale ci ñeneen ñu dul woon ñoon, ba tay Orob gii, di lu leer, ca googale leer la tanqe, te ca la yewwoo it.

Kon ci gàttal yewwute fii mooy renaissance gi nga'y dégg ci kàllaamay franse te'y tekki ci maanaa yewwute rekk, ndax mooy judduwaat gu xam waral, ginaaw dee gu réer waraloon.

Làkk moo'y cëslaayu'g yewwute, du ma'a'y ki ko njëkk'a wax, am na ñu bari ñu wax lu ni mel, ci xalaatkat yi ak taarixkat yi, bu ñu dello as lëf ginaaw ànd ak sunu'y xalaat, ba ci xarnu'b fukk ak juroom ñatt ci jëmmi boppam, da nanu gis ne lu bari ci'y xalaatkatam aki ñoñ taarixam, ku ci mel ni Lodoviko Antoniyo Mortara ak Volteer ak Wilyaam Robertson 1721 - 1793, jëfandikoo woon nanu waxiin wu mel ne wii, ndaxte boole nanu ci mbàndarga yi'y raññale jamono'y yewwute, boole woon nanu ci doxu'g waxiini gox yi,juge ci'y waxiin dem ci ay làkk yu réew niki làkku'w Espaañ wu Itaali, wu Fraans ak wu Portigaal, ba fa mu yam.

Li gën'a yéeme moo'y Yojinyoo Jarin moom dafa jel mboleem amaliiti yewwute gi, sol ko ci benn baat, mooy  filolojiaa , di baat bu am ñaari maanaa yu mag, mu njëkk mi, mu xat la, te daytalu(gàtt), moo'y (( dégg làkk)), mi ci des, moo gën'a yaatu te gën'a xóot, moo'y gëstu yu làkk, yu njàggat yi (adab) (ci tubaab les recherches linguistiques et littéraires). 

Jarin gis na ne bu nu mane'e doxal yooni gëstu yu làkk ak yu njàngat yi, jaarale ko ci gëstu ci dénd bi(nature), jamono jooja aw yoon wu bees di na judd, di yoonu gëstu wu xam-xam wu di kojug làmb, (làmb ba daj rekk, amul waxi kese walla gisiin ), loolu moo ñu'y àggale ci xam-xami matematik yi.
Nga dolli ci loolu ne làkk moo'y seetu bi nga'y man'a gise dundu'g nit gu xel gi, boo gisee ne làkku xeet wu nekk, ci jamono ju nekk, lenn la ci li'y wone am xelam, nga dolleeti ci ne ci lanu'y jànge xam-xam yi nga xam ne bu ñu nekkul woon,amuñu woon, dund gi du mel nii mu mel tay. Bu làkk amul woon nu xam-xam di juddoo ba'y gis jant bi.

Làkk moo'y cëslaayu ag yewwute bu nu ko waxee, dées na ko man a dëggal, rawati na ku jàng jii jamono, jàngat ko, xam la leen seen  waxiin yu suufe ya ñu xeeb jariñoon - ñu ko'y woowe ci francais dialecte - ba ñu leen jëlee, def leen ay làkk yu xeet, yu réew, yu xam-xam, yu ñu fonk, yu ñu fas-yéene'e doxale seenu'g dund, sës ci seenu'g dox, sanni ca àll ba yeneen ya doon dox seen diggante ak xam, xam-xam, ak yewwute, mu'y làkk wu latin wi nekkoon di lu ñu neew xamoon, la gën a rëy ca mbooloo ma réere woon ko, te réere gi taxoon ñu reeroon te yewwoodiku. 

Wii làkk, di wu Latin wi, nekkoon na di seenu'b coona, di seenu'w ay, di seen gàllankoor, di ab pakk ci seen digg ak jem-kanam, ndax la ëppoon ca xam-xam ya, bu ma waxul sax lépp, ca woowale làkk la nu ko daa binde, di ko ci jànge, te askan wa bu doon téeméer, lu yees fukk'a ko ci'y xam, mu'y ci misaal daanaka: nga xiif lool, ba'y bëgg'a dee, di wër loo lekk, ndeke lekk gi moom am nga ko, mi ngi ci sa ronu ay tànk, te ya'a ko moom, doo ci fay dara, xanaa kay da nga'y jël rekk jëfandikoo, te loolu lépp xamoo ko, te kenn'a ngi nii ci sa kanam, xam loolu lépp, te xam ne bu ko waxee, dootul jariñu ci, ni mu ko daa defe, kon na la ko bañ'a won, xamal la ne ya'a'y ki ko moom, ndax loolu man na'a waral sa'g wadd sòng ko, giir ko, ne ko fuuf, te bu booba'a su ko ab xiif gaarate'e du xam fu mu ko'y fajeeti ci'g càcc!. 

Waaw waaw, ci'g càcc kay !, ndax lii ag càcc la, ndax xañ nit àqam, di ko jëfandikoo'k'a jariñoo sàcc ko la, te bàyyi ko nee mu toog ci'b xiifam, ci yitewoo àqam, ci taru'g yitewoom, càcc la de! . Loolu ku ni la du sàcc, laaj ko lu mu doon,moo raw sàcc, fëkk la, nax la, réeral la, dofal la, xiifal la, neewal doole la, nakk'a xam la, dofe la, suufe la, réer la, bon la, waxal lu la soob ne moom la.

Kii man'a xam nga ne ko doo fi xame, ndax làkk wi nga yor du wu ñu'y xame, wa kee yor'ay dëgg-dëegi aw làkk, ci la ñu war'a waxe, war ce'e jànge, war ce'e yëre, war ce'e gëstoo, war ce'e binde, te ci la nu war'a nekke nit, boo xamoon li ci addina bi bepp it te xamewoo ko ci doo kenn ku xam, ku ñu'y lim nga nga'y kenn ci ñu xamadi ñi, ñu réer ñi, ñi amalul seen réew solo. 
Lii nag sama gaa yi du'g réer, di'g dof, ak dofale, ak li la soob ci xeeti xelloodi?

Lii'ay li ñu doon def waa Orob ca jamono yu diggdoomu ya,maanaam  middle ages ci angle, di nu ko def ci jii jamono - nga xam ne moo'y ju xam ci anam gu gaaw, ngir bari'g li ñu war'a xam - ndax li man'a xam te ëpp ci réew mi am nanu làkk wu ñu man'a xame ci's lëf ci'g gaaw, ak sakanal waxtu, ak ci's lëf ci'g wér, ak lëw.
Kon jort naa ne la'y lañu war, moo'y la wa Orobi joojale jamono defoon, mu'y taxaw ci jël seen àq, delloosi seenu'm dem, feeñal seenu'm réer, sulli seen lu suulu.

Di na rafet nu indil leen sababi feeñug yile làkk.

Làkku Latin, ci jamono yu diggdoomu yi,(moyen âges) moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam-xam ya, ak niti diine ya, ak politgkat ya, ak niti adab ya, walla njaggatkat ya ( hommes de lettre) ak ustaas ya. La notoon nag ca nit na - di woon niti neen ñi rekk - ñoom déggunu woon wii làkk, lu tumbrànke la woon ca ñoom, seen làkki bopp yi'y yu seeni barab lañu déggoon.

Bi jamono'y yewwute dikkee, gelawu'l fonk sa xeet (nationalisme) upp ci Orob gepp, la lu bari ci xalaatkat yi, ak niti adab yi, ak woykat yi, tàmblee jeng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki réewi bopp, niki wu Itaali, wu Espaañ, wu Fraans, wu Engle ak yu dul yooyu.

Bi mu ko defee, woykatu Itaali bi tuddoon Dante ( 1265 - 1321 g ) taalif Komedi (xisa bu'y reeloo) Bu sell bi ci làkku Itaali, naka noonu Petrarch ( 1304 - 1374 g ) mii nga xam ne li mu gisoom moo'y làkku Romam wii daal moo'y gën ja'a kawe'y jumtukaay ngir génne xasida'y woyam yi. 

Bu ko defee Miguel de Cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di (don kixota) ci làkku Espaañ, ci noonu it la Rabelais ( 1483 - 1553 g ) def, moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di franse,ngir wuñi ci li'y yëngu ci biiram, ci njàggat (adab) lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor (kaf). 

Chaucer mi di'b angle ( 1342 - 1400 g) jug,moom itam, sotti ci'w làkkam woyam yu yéeme yi ci'b taar, rawati na nettali'y Kentrebry yi, nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati angle yu mag yi, yi gën'a siw.

Làkki xeet yu Orob yi, ñi ngi sosoo ci màbbiiti Latin ak Tiyotin. Wu Itaali, wu Espaañ, wu Fraans, wu Portigaal, ñi ngi dagge ci Latin, wu almaañ, wu angale, wu danmark, wu suwed, wu oland, wu norwej, bàyyikoo ca Tiyotin.

Bokk na ci sabab yi jur doxug yile waxiin dem ci làkki réew, yu xeet, bokk na ci sabab yooyu, nekk gu làkku'w latin nekkoon di wenn, ba yàgg mu seddaliku di ñaar, wu ñu'y wax kalaasik, ak wu wilgeer . Kalaasik mooy lu yàgg la'y cosaan, wilgeer, di lu yomb, li nuy jëfandikoo.
Kalaasik wi di wi politigkat yu mag yi, ak boroom xam-xam yi, ak niti diine yi daa waxe. Wu wilgeer wi, di wi niti neen yi di waxe, di ko jëfandikoo. Ci noonu kalaasik wi tàmblee nakk as lëf ci solo'om,ak dooleem, wilgeer wi tàmblee jël barabam, waaye wilgeer wi moom ci jëmmi boppam tàmbli na ci ginaaw bi di soppiku, ndànk-ndànk, jem ca leneen lu dul la mu doonoon, ci noonu ay waxiin yu bari te wuute bànqaasoo ca, ngir nocciku'g lenn ci mbooloo yii, juge ci yile barab dem ca yee,tas fa,ak soreente gi yii barab soreentee te wuute. Loolu jur yeneen mbooloo'y nit judd, mu ci nekk ak sa waxiinu bopp.

Waaye loolu moom teewul woon latin des fi di làkku diine wi te'y wu xamlu wi maanaam wu ofisel wi, ba mujj askan yi yoqat ko, te xam ne pakk la ci yoonu seen ag dox, aku'g jàll, ndax ña ëppoon ca ñoom xamuñu ko woon,dégguñu ko. Loolu yobb léen ci ñu xëy taxaw temb ci jële ko fi, sanni ko ci seen ginaaw, weccee ko'ok seen waxiin yooyee, te farlu bu baax ci jàllale leen, jëme leen kanam, tèkki ci li ñu soxla woon lépp ci yooyule téere yu am solo, te ñu bindoon leen ci laitin ca jamono jooja.

Ci noonu nit ñépp tàmblee gis koom mu rëy mii, di ko xam , te bu njëkk, daa xawoon'a jòmb ci ñoom ñu ko'y xam, ba ci'y jariñu. 
Lii nag day tegtale rekk li war, mu'y jëfandikoo làkku'w nday wi, niki lakk, ci wàllu'g ligéey ak jàng.

Reew yi nekkoon ci ron suku'b sañcaan yi ( colonialiste) yi, rawati na yi ci'y jëfandikoo làkki jàmbur yi ba leegi, niki tubaab, ak angle, ak yeneen, jàppe leen làkki ofisel, yii réew de ba leegi dañuñu di jànkoonte ak ag réer gu kawe te tas ci biiru'w askanam, ak koom-koom bu deltu ginaaw, ak ag des ginaaw gu rëy ak dund gu suufe.
Kon làkk daa war'a nekk di lu yomb lool ci ni ko'y jariñoo, maanaam mu'y làkku'w la ëpp ca nit ña, niki wolof fii fi Senegaal, bu ko defee ñu bàyyil fi ni gën'a néew itam seen àq ci jariñoo seen làkki bopp, ci lefu'm jëf ak jàng. Waaye nag bu booba'a du man'a ñàkk'a jëfandikoo làkku la ëpp ngir jëflante.
Ci noonu la ko'y joxe àqi nekk làkku'w ofisel wi.

Li nga xam ne sikk amu ci, moo'y gis nga ay yooni yoon, lu bari ci yeneen xeet yi ci reew mi nu'y wax wolof yu rafet ci anam gu jàppandi, ni ko ñépp di defe, ci lu dul ñu ko'y jàng, bu ma waxul li ëpp ci ñoom, te safaanu'b loolu néew na nga gis ko, maanaam wolof bu dégg yii làkk, loolu li ko waral du ne wolof bi daa yitewoowul ñeneen ñi, du caagéenu'g ñeneen ñi dañu'y sotti seen yite jépp ci làkku'w wolof aki mbiram, li am kay da di wolof day làkku jëflante wi tas, samp boppam ci géew bi, franse mii ñu'y jàpple sax manul'a bëre'ek moom mbaa mu gëpplante ak moom. Ndax moo'y làkk wi'y tàbbi ci say nopp, mu neex la mbaa mu naqari la, nga ko'y xam ci sañ-bañ.

Man nag ma'y ku yitewoode'e tontu ci loolu, ndax ni mu ma ñoradee, waaye am na nag lu xaw'a am solo ci laaj bi, mu'y booy xool lu bari ci ñi ñu'y tudde wolof - ci laa maa ngii - seen dëgg-dëggi cosaan du wolof, man li may jàpp foofu moo'y wolof li mu'y tollool moo'y “ag cenegaal” , maanaam xeet wi moo'y waa-senegaal, làkk wi di wu senegaal, kon dootul wu giir, mbaa waaso, waaye wu xeet wi wépp’a, Serin Tuubaa amul lenni wolof, Alhaaji Maalik naka noonu te taxul woon nu dégg tukloor, kon day mel ni xalaat bii mi ngi jeng as lëf jëm ci'g yanu maanaa.

Bu ñu delloo ci li ñu nekkoon di wax mu'y war gi làkk war'a nekk di lu yomb ci ki ko'y jëfandikoo, da ma naan nit ñi daal li leen war moo'y def na waa sowwu defoon , muy tuxal seen waxiin yooyee, yòbb leen ci'y làkk, te sukkandiku ci, xamloo ci, su nu ko gisee muy lu mant'a ñàkk, maanaam bu nu fi gisee lenn lu'y gàllankoor seenu'g dox, di làkk wu fi jóox, wu ñu xamul ni ñu ko war'a xame, niki franse ci sunu-gaal.

Waaye nag amaa na loolu lepp du nu ko soxla, bu waxtu wa jàllee, ba nit ña dégg way jóoxi làkk yii ni ñu dégge seen làkku nday wi. Ndaxte làkk du yàlla ju ñu'y gëm, waaye kay jumtukaay la ngir déggante ni ma ko jorte. 

Ahmad Amiin wax na ca téereem ba tudd Fajrul Islaam:(( aw làkk sàkkeesu ko ci genn jañ (maanaam jekki-jekkiwul rekk am), ñu mujj ñi bi ñu ko'y jële ci ñu njëkk ña du woon lu mat, li am kay moo'y nit ñi dañu'y sàkk ci seenu'g njëlbéen, ay baat yu tolloo ak seen aajo, bu yeneen mbir feeñee, nu sàkkal leen ay baat yu bees, bu ay mbir raafee amaa na ay baatam raaf. Làkk nag'a ngii nekk ci dund ak dee gu sax, naka noonu bàyyikoo yi (mooy baat yiy tukkee ci yeneen yi) ak waxiin yi, ak baat yi, ñoom itam dañu'y màgg , di yéeg ni xeet wi'y yéege, di ko magge)).

Yooyule làkk, di yu Orob yi de,gënuñu fenn, mbaa ñu kawe ci lenn sunu yos yu afrik yii, li fi nekk kay mooy ñoom dañu leen'a fonk, sonn ci, di def lu mel ne li Ahmad Amiin di wax mu'y sàkk baat yu bees saa su lu yees amee. Kon sama gaa yi, nanu doylu ci lii nu yor, ndax li sunu di neex, sama dàq na ko kat, te jéem ko'o jàllale,jëmale ko kanam, te tas ko ci mbooloo mi.

Du'y caaxaan la nit ka'y xalaate, ca la war'a waxe , ci maanaa li nga'y xalaat ci sa biir dënn, sa biir xel, mu'y jeqarbiku ci sa'y yëg-yëg jarul fireeti ci weneen làkk wu dul wi ko xalaat, ngir déggal ko ku nu jàkkaarlool ki, bu ko fekkee mu ko'y man'a dégg ci wi ñu ko xalaate,loolu li mu'y jur mooy yàq waxtu,te mu'y lu gànjaru.

Wax ju'y joriku, di dikk ànd ak kem bu rëy ci'g jàppandi, manul'a ame ci lu dul làkku'w nday wi nit ki juddwaalee, walla wi mu àndal ay at, di ci jàpp ak'a ŋoy, ci këram ak pénc ma, ja ba, ak daara ja, nga xam ne da'y faf fàtte wow ndayam wa, mbaa mu xaw ko'o fàtte,ba mujj wii di wu jóox sax mooy far di taxaw taxawaayu wu nday wi.
Bu dee fii nag, gisagunu tubaab jël fi taxawaayu'b wu nday, wolof mi'y nday kay moo sax di nday ba leegi, ci moom rekk lanu'y man'a ame joriku gi nu sox la ci wax, misaalu'm loolu yaa ngi koy gis ci ñii di xëy ak'a gont ci leekoli nasaraan yi, ñoom de ca dëgg-dëgg da nanu ko dégg xayna , waaye lu ci ëpp, du ñu ci man'a génnee seeni xalaat ci'g joriku aku'g yomb, waxal sax aku'g dëggu, ndax dañu'y diriku ci seeni wax ak'a jàddantu, ak' a xootal fu nu ko waroon'a tondale, ba far wax ja day doon leneen lu dul la mu bëggoon'a doon, walla sax leeg-leeg ñu rax ko ak yennaat ci baati wolof, ngir noppalo'o ca, bu ko defee tubaab bi déggul ay wolof du xam li ñu'y wax, wolof bi déggul ay tubaab it naka noonu, kenn rekk'a ko'y xam ki boole ñaari làkk yi.

Li ma gis moo di Orob ca yaatoom ga, ak ca jégeente'y xeetam ya, ak seen ag niroo, ak gu làkk, ak bokk gisiin ak diine ak melo,ak - man nga ne - jëmuwaay, nga rax ci dolli, nekku'g yenn ci seeni làkk di - man nanu ne - yu addina bi bepp, niki angle, ak wu ko xaw'a jege niki francais, teewul ñoom ñu nekk di ñu jàpp ci seeni làkk, xeet wu nekk ca wosam, te teewu ko'o jàng nag yeneen yi, rawati na angle, di ci jokkoo saa su begge'e jëflante ak ñi déggul wa mu yor. Danmark ma nga'ak danwaam, Suwed wuwedam, da ma'a tayye'e lim, waaye wu ci nekk ak wosam, ba ci Belgik sax nga xam ne ñaari xeet yu wuute'e fa dekk, teewul xeet wu nekk, yor sa wosu bopp, te teewu la'a jàngi leneen ba ca wu sa moroom, bi nga ko gisee mu'y xam xam, ndax xam-xam du lu moy xam lu mat'a xam, te loola mat na'a xam, ndax da na jur ag rataxal diggante, jur ag xam sa moroom, jariñu ci, jariñ ko.

Addina bi dafa war'a sosu ci'g dimblante, jariñante, fonkante, deet jariñoo, ak dimbandikoo, te lii tubaab yi di def, du lu dul dimbadikoo, ak jariñoo, ci suñu'g suul, ray, joggi, nërméel mbooleem sunu yëf, ci taxawal seen yëf.

Wolof nag daa na wax : (( pesu'm kanam boroom'a ko'y fajal boppam)), kon nag pes nañu nu, lu nu'y xaar, du nu jug di door, mbaa nu'y daas ay jaase'eki gobar, li nu'y def kay moo'y jëfandikoo xel, ni ko seriñ Mbay JAXATE daa waxe, mu'y ab noon bu la noonu, boo'y xeex ak moom, bu mu ko yëg, na xëy rekk daanu door a xam ne ya'a ko daaneel , fa la sa'b noflaay di ëppe, ca la la nga'y jëfandikoo ci ngànnaay di gën'a néewe, ndax bu fekkoonte ne daa waroon'a jàmmaarloo ak yaw, nga'y jëfandikoo lu ne ngir moytu'y dóoram, ak di ko jéem a dóor, leegi fegal nanu la coona'b jéem'a dóor ak moytu, moom kay da nga'y agsi rekk dóor, mbaa nga jam, ndax moom yëgul ni ya'a ngi koy fexeel, bu ko defee mu dee, naaxsaay. Lii estraategi la ci.

Lu mel ni franse ci réew mi, manoon na fe'e nekke ni fi araab nekke, di'b soppe te bañ di'b noon, di luy dem ànd ak di demale, waaye jort ne moom rekk'a war'a dem?.
Xoolal ci maanaa araab ñi ko jàng tay, ñoo'y ñi dégg wolof, ñooy ñi ko fonk, ñoo'y ñi ko'y suqali, loolu bu amee li mu wund moo'y ne araab ca mag ña jumtukaay la woon ngir jëm kanam ci xam-xamu diine waaye it jëmal kanam seen kàllaama gi nga xam ne tay daa fees dell aki baati araab yu ñu jox kàddu'g wolof, ci fi ko wolof amewul. Xoolal ma baatu’b jamono, mi ngi juge ci samaanu, maanaam juge ci mahnaa, yu mel nii yu sakkan lanu ci, daa nanu dem sax ba’y jëfandikoo as lef ci xarala, di sàkkal wolof ay jumtukaay yu làkk yu mu amutoon te ñu gis ko ci araab, te xam njariñam, xam ne man na leen'a amal njariñ, niki yaa'g askanal googu nekk ci araab, nu ko daa tollolee baatub koj , naan yef yu di koju'g nàggam, ci maanaa xam-xam bu di koju'g diine, jublu ci xam-xamu diine, mu'y mbaat sos su nu ko fonkee, man na'a am ay jeexiit yu am solo, ci ëllëgi làkk wi, ak ci diggale , di ci tubaab par l'intermediaire de , ak ci'g jonjoo, di ci tubaab en direct.
Yii di baat yoy danu lay won ni araab jeexiitale ci wii làkk, du caagéenu danu di ay baat yu amul woon ci wolof, aha kay yu ci amoon lanu, waaye fii yeneen maanaa lanu yore yu bokkul ak yanu yoroon, nun itam bu nu gisee ne yii du yi nu soxlaati, walla maanaa yii jubul, am nanu sañ-sañ ci def ni nu neex, ndax ñoo'y boroom. 

Kon noom ñaar way jàppante lanu woon yu'y dimbalante, dunu woon ay noon. Wolof am na ay waxiin yu bees aki baat yu yees, ci tabe'g làkku'w araab la ko ame . Ndax boo'y xool da nga'y gis ne woomle'g wolof aku'g riisam mi ngi ko jële, ci jël lu toll ne làkku'w araab ca yaatoom nga, ak tàllalikoom ga,firi lépp baat topp baat, loolu moo nekkoon seen anamu'g jàngale, nga xam ne da nu la'y wax baat firil la ko, ba mbooleem teere yi nu daa jàng ci araab - te yu bari lanu woon te wuute, ci fann yépp - ci nii la nu ko daa defe. Loolu jural leen nu mujj baat bu nu am ci araab ca woomam ga, nu am ko ci wolof.

Bu dee franse moom ci nga'y dégge wolof bu naan la : nga jéggal ma sama wolof daa leerul, te loolu ag xeexam ak ag jéem'a suulam'a ko waral, ag yaakaaram ne moom rekk'a war'a nekk ci kaw suuf'a ko waral, ak jeem'a toogam ci laltu gi, mu des ay barab yu nu man'a toog, mu teg ci ay tànkam, lal ci'y loxoom ne kenn du ci toog, moom reek, moo di li ko waral.

Kon de kii ku siis la, ku xat la,ku nay la,ku'y ngartaajoo la, ku'y nangu suufu's jàmbur la, ku yëg ne moom rekk la, ku am bëgg-bëggu suuxal la, lii nag ku ko mas'a am ya'a'y ki nar'a suux,nar'a neen,nar'a seey.

Waaye loolu lépp du tee mu'y lenn ci li ñu moom, moom nasaraan du moo moomati li nu ci moom, ndax ca Aljeeri de, kenn ci ay xalaatkatam nee na woon : franse de lenn la ci sunu am màngiit mi nu mànge ci tubaab yi. Màngiit moo'y xaniima, di ci maanaa li nga'y nangoo ci ki nga'y xareel, boo ko gañee, maanaam loolu moo'y li franse di ñëw lépp ngir nangu, jël ci doole, fitnaal, foñloo, fàtteel, taxaw ci doole,jaaye ko, teewul muy lu am solo, di lu ñu man'a xame'e, man ce'e jariñoo, kon bu nu ko jàppe njariñ lu nu'y sànni, waaye màngiit, mu nu mànge ca sunu xare ak ñoom, ndaxte addiis'a ngi nii bu naan : ((hikma moo'y réeru'm jullit bi, fu mu ko gis daal na ko woor ne moo ca gën'a yay)). Hikma nag di lol boo ko doon firi da nga naan moo'y lépp lu rafet rekk, jekk, xellu, baax, di lu ñu xam, di lu am solo, ci dund, mbaa dee, xel mu rafet, ba fa mu yam. Kon franse li fe'ek ya'a ngi ci'y gis sa njariñ, moo xam lu adduna la mbaa leneen kon ci hikma la.

Waaye kay li'y li yéeme moo'y da ma'a gisagul ci réew yi'y dem, te'y dox, di dund, di jëm kanam, mu ci'y waxe ci'w làkk, bu feeñee, bu làqoo weneen, maanaam loolu mooy li xew tay ci sunu réew mi, nga xam ne bu ñu feeñee ci lu fés, mbaa nu'y jëflante ci anam gu ofisel, - ofisel ci li wolof mànge ci tubaab la - da nga nu'y gis nu'y waxe ci kallaama'y nasaraan, bu nu delloo fa sunu'y kër,di ko defe ci wolof, leeg-leeg sax nu'y rax la ñu'y defe ca franse yennat ci baati walof, kon mokkalaguñu, te loo mokkalul manoo ce'e jariñu, li'y li nu mokkal kay moo'y sunu wolof mii ñépp di wax,ku dégg franse ak ku ko déggul, ku'y ku ndaw mbaa nga'y mag.

Fii nga'y gis jëwrin ju mag ju taxaw di wax ci googule kàllaama ba yàgg mu ruur toolu'b wolof, fac ca soxlaam bu baax, mu mel ni daa déggatul tubaab, walla mi ngi ko'y bëgg'a sonnal, ndaxte nag ca dëgg-dëgg coona la, di wax lol boo ko déggee it, wi nga nàmp nga gën'a dégg, te ci nga gën'a gise sa bopp, ki nga'y waxal it moom la gën'a dégg, du am lenn lu mu ci'y xel ñaar, mbaa mu ko ci'y laaj,du caagéenu'g baat bu mu ci'y réere daanaka. Ba ci sunu njiit lii fi nekk tay, di Wadd, ba laa bég ruur toolu'b wolof ci biir waxi tubaabam, day mel ni da ce'e gën'a gis boppam, mbaa mu gën ko'o yòmb, mbaa noppal, wax leen ma lu mu ?.

Raw gu xam-xam gu mag itam boo'y xool, da nga naan demewu fi noonu, li sabab loolu moo'y ne nun li ñu'y daj ci dégg tubaab daa metti te rëy, te li mi'y jël ci ñun ci waxtu daa takku, loolo'oy li'y waral nu'y neenal xam-xam yi, moom kay fii fi Senegaal dégg franse doy na fi xam-xam, àgg na ci sunu njiitu réew lu njëkk la, xam-xamam bu mag ba nu doon naw lépp, du woon lu dul :naan na géeju'g franse, du ñu ne la benn xam-xam bu di koju'g tegnik mbaa xarala la xam. 

Seriñ Tuubaa mi ngi ñu naan - ba mu ñu'y jàngal xam-xamu Lislaam - : jiitalal xam-xamu tawhiid mu'y li la'y xamal ni nga'y gëme Yàlla, kennal ko,wéetal ko, teg ca  fiq mu'y ni nga'y jaamoo sunu boroom, ak tasawwuf, waaye mu teg ca ne ak jumtukaay ya, mu jublu ci jumtukaay yi; làkku araab ak la mu'y àndal ngir nga man ko'o dégg, mu'y nahwu ba ak bayaan ba, nahwu di li'y nos làkk wi di ci franse grammaire, bayaan di li'y nos wax ji, di tax doo guddal lu waroon'a gàtt, loolu lépp, bi mu ko'y lim mu bokk ci xam-xamu diine, da leen'a tudde ay jumtukaay, mu jublu ci ne xamluwunu leen ngir seen jëmmi bopp, waaye ay raas lanu yu nu'y yéege jëm ci xam diinee, rawati na alxuraan mi nga xam ne manéesu ko'o, walla su c'ee xam te déggeesul araab mi nu ko wàcce, ndaxte làkk wu nekk, am na jagle'y boppam yu moom rekk'a ko moom, ku firi wor la léeb wa wax, rawati na lu mel ni alxuraan ca jafe'g làkk wa nu ko wàcce, ak màggu'g aji wàcceem.

Bu nu waxee màggu'g aji wàcce ji, da nga ci'y dégge màggu'g li nu wàcce, kon loolu màgg na màgg gu kenn mant'a dégg ci'g yòmb,ak'ub noflaay, lii moo'y li waral araab di jumtukaay ngir xam diine, di xaaj ci xaaji xam-xami diine yi, kon mag ñi jànguñu woon araab ngir jëmm ja, waaye jumtukaay la woon ngir xam la mu ëmb, loolu mooy safaanu'b ku mel ni Senghoor aki gaayam, noom làkk wi moo leen taxoon'a jug,nu sonn ci, sonle ci, bu taxutoon, doo def fo'o toll di dégg baatub frankofoni, lu mu'y wund ? tontu leen. 

Yalla baax na, ba mu nu teralee ci nu nekk ci jii jamono di dellusiwaat ci sunu bopp, di ko tàmble’e fonk, di gestu li jar'a gestu, te lu ci gën'a rëy sunu kàllaama gii?, ndax giñ naa ne xam gi bu wóor, ak jëfandikoo gi ci fànn yépp di nanu jariñ lu bari, te'y jëf ay jëf ci yòmbal sunu'g dund. Da na nu yòbb tam ci nu'y dëgg-dëggi réew, dëgg-dëggi xeet, dëgg-dëggi ay mbòkk, yu gis ne am nanu lu nu bòkk, yu'y mbòkkoo ak'a joqalante ci'g nooy ak'ug jàppandi. 
Jëflante di na gën'a dolliko'o ratax, déggante gën'a yòmb,xam gën'a jàppadi, koom gën'a lëw, ndax xam-xamu koom di na gën'a yòmb'a jariñoo ci ligéeykat yi, jaaykat yi, naka noonu naataange di na raññiku ci wàll yu bari, ngir xéewal gi am te ame ci jàppandi'g xam mbir yi, ngir jumtukaay bu yòmb bii am te amutoon di sunu'w làkk.

la ko war kay moo'y mu ne ko bar, bar moo'y baat bi bàyyima bii xam, kon noppal sa bopp du nga nekk fa naan ko kaay, waaye xanaa bar mooy li sonleedi. Naka noonu ñu dégg ba noppi wii làkk, nga xam ne leegi xam xam-xam rekk'a nu war'a ñor, te dese nu, nu naan da nu'y bàyyi wii nu dégg nee, naan dañu’y xamlooti weneen door'a xamlu xam-xam yi taxoon ñu'y xamlu'w làkk, loolu jort naa ne dofe la, sànk waxtu la, sonnal sa bopp la.

Jàppoo ni sunu ligéeykat yii ca seen yewwute ga ak muus ga ak xarale ga, bu nu ci doon boole di leen seetal li nu aajowoo ci xam-xam bu aju ci seeni ligéey, defal leen ko ci seen làkku réew wi nu dégg, naan ko, xam ko xam gu xam kawewul, jàppoo ne bu loolu amoon du ñu fi xar baax, jëf fi ay kiimaan, def fi lu raw li tubaab yi di def, ba nu leen di naw ?.

Da ma'a yàgg'a dégg ci sunu biir ku naan nit ku ñuul daal, xawma lu mu def Yàlla, ba Yàlla gàttal'um xelam nii !, te loolu day mel ni bu nu ko'y wax, ñi ngi dëggal li tubaab bi yàgg'a wax yàgg ko'o jort ci ñun mu'y moom moo nu ëpp xel, walla sax moo'y ki ko am, nun li nu am du am xel, ndax xel ak ni mu màgge jòmb naa nekk ci yaram wu ñaaw, wu ñuul, wu tàyyeel wii. Am ku ma dégg te moom ku ñuul la, mu mel ni ku'y jàpple tubaab yi ci seen wax jooju naan: ((ñu ñuul ñi de àjjana bu ñu fa duggee, su nu fa yàggee yàq ko, naqaril ko. Tubaab yi nag ñoom, bu nu tàbbee sawara, su nu fa yàggee defar ko, neexal ko)), waaye boo'y xool sax da nga'y mel ni ku gis lu ni mel, te sabab bi du dara lu dul jumtukaayu jàng bi moo nekkul ci sunu loxo mu'y sunu làkku bopp, làkku jàmbur day waral nga gëm jàmbur, xeeb sa bopp, xoolal ci nun ñi'y làkk tubaab, sunu delluwaay, sunu jëlewaay, sunu ndëërlaay moo'y fraans, ak nu mu man'a rëye mbaa mu tuutee ni, kii moo'y ki nu gëm, bu nu ko gënoon'a xam it jort ne moo nu ko gën'a def, lii aji am la ju ñépp di gis, di ko dund. 

Li ñu’y wax cosaan, da'y baat bu waa senegaal baaxoo wax, di ko tudd lu bari ci seeni wax, mu mel ni day lu ñu fonk ba ci lool, mu mel ni fonk gi moo'y yoon, ndax boo'y xool, cosaan mi ngi bàyyikoo ci baatu sos, di kon fa nga sosoo, juge ca, bàyyikoo ca, bu dee nit la ndayam, baayam, dëkkam, réewam, aadaam, aam, lii moo'y cosaanam, ndax ci foofu la sosoo, bàyyiikoo fa, kon lii mooy cosaan. Waaye ndax li nu def fonk cosaan la ? Nan laaj sunu bopp bu baax te xootal laaj bi, ndax fonk nanu sunu bopp? Sunu cosaan ? Man dama naan déedéet, déedéet kay, ma dellu ne déedéet. Jort naa ne ci barabu fonk sunu bopp, tubaab bi mooy ki nu fonk, ci barabu sunu cosaan, cosaanam, lii'a'y li am, di li nekk. Tubaab bi la nu'y xëyal, di ko gontal, ak doonte as lëf ci sunu njariñ'a ngi ci, aw làkkam lañu'y sonn, bàyyi sunu wos, te kat làkk moo'y dëgg-dëggi cosaan, ndax mooy seetu bi'y wone boroon, te'y jimblang ji'y ëmb li xeet wi indi ci'y jaloore, aki mbanoore, aki aada'aki cosaan.

Kon moo'y mbuubs mi nga xam ne bu la réeree, la mu ëmb sànku, naaxsaay. Kon déet ag wuutu di ñeel ko. Tereesul jàpp weneen waaye na sa wos jiitu, ndaxte léeb wa nee na: li nga am boo ci séenéenul doo ñeetaane!. Mu'y ci maanaa li nga moom boo ko fonkee, mu doy la, nga doyloo ko, doo soxlaal kenn lennam. Mu'y lu wóor, ndax jort naa, lii fi nun bu nu ko fonkee, dem, te du nu sonn, mbaa nu'y ñee kenn. 

Mu mel ne la Karlo LEFI waxoon di kok ku jàng njàggat lu Itaali - njàggat , fii mu'y tekki litterature ci nasaraan - da nga ko xam, mu ne woon:( Kristo s'è fermato a Eboli ), di ci maanaa Kristo, di yonnant Yàlla Hiisaa, ma nga yam ba mi'y def doxu'b nitale ba, yiwale ba, xayale ba, taaxale ba, diinele ba, yéwénal ba, ma nga yamoon ca Eboli, jotutoon’a àgg sunu dëkk, jublu woon ca loola ne àtte gi, walla ci ni nu ko gën'a baaxoo waxe nguur gi mu'y baat bu ma soof, ndax nguur moom nekkul lu dul fu'y buur di dunde nguur nekk fa, waaye mu begg'a wax ne nguur gi kon di gu Itaali, bi mu'y defar da fee bayyi sama dëkk bii jéemu ci dara, sama'w nit di ñu dofe, ñàkk am xel, ngir néewu'g li ñu leen sotti ci xam-xam, man itam ma ne naka noonu, ngir sunu ñàkk'a jëfandikoo sunu làkk, di jël wu keneen. 

Ku wax lii de amaa na ñu ne ko: yaw de xanaa da nga'a faf jort ne làkk moo'y yàlla ji'y faji aajo, rawati na bu dee sa wosu bopp?, ndax da'y mel ne lu'y xeeti man-manu def, ak jëmale kanam, jumtukaayi jàll ak jàllale jox nga ko ko, kon daal moom rekk doy na ngir dox ? ma ne déet, du loolu la'a bëgg'a wax, li ma jublu kay, moo'y moom de moo'y gën ji jumtukaay, te'y gën ji dokk ci ku mant'a ñàkk'a sukkandiku bu'y doy, gàttalaakonu'b dox la, yombalaakonu dund la, mbokkalaakon la, bennalaakon la, di boolewaakon, di taxaakonu yëg sa bopp, fonk sa bopp, tasaakonu xam-xam, jàppandilaakonam, dabalewaakon, ak ak ak.

Man de maa ngi naan te du ma dañ naan: jël leen ko! moom'a de!.
Moom'a de, moo'y li ñu'y teral, di ñu jugal, di nu doxal, di tax nu'y xalaat, di bind, di yër, yëglekaay yi'y lëw, di jàngu, ay bindkatam di dolliku, taalifkat yi'y yokk, yëngu-yëngu gu xam-xam di gën'a sawar, cawarte'g caada ak gu saxaafa gën di dëggu, gën di fés, gën di laalu.

Bindante di mujj di nekk ci lu dul ab coona, ci's lëf ci'g gaaw, ci'b noflaay, ci'g ratax, ci lu dul xalaat, mbaa toggoo, wàlla yenn anami moytu. Kon moom la, mooy noflaay bi, di jàll gi, di naatange gi, di meññ gi, di woom gi, di fulla ji te'y yéeg gi.
Xoolal as lëf ci yitewoo gu tar, ak jublu gu mag gi nga'y seetlu fii mu nekk, ci sunu mbiri réew ak mbiri xibaar, te loolu li ko jur du dara lu mo'y xibaar gi nu'y xibaar askan wi ci seen làkku bopp wi, nga xam ne jamono jii, ñépp'a yewwu, kenn gënul'a xamati ki jàngul li'y xew ci réewam, ci wërlaayam, ci goxam, njiitu'l réew mi sax gënul'a xamati gone gi'y gën di gone li'y wëndéelu ci mii réew, ak ca mee. 
Lii lépp ngënéelu'l sa'w làkk'a, da'y wëy nag ba ca lu dul xibaar, àgg ca mbooleem lu dox mbaa mu raam ci lu nekk, di yombal, di gaawal, di àggale, di noppale, di soreele fitna.

Seetlu naa mu bokk ci la ma seetlu, ne leegi jàngkat yi ak jëfandikookati internet yi dañoo am ag jeng jëm ci bu nu'y bindante di ko defe ci wolof, rawati na bu nu yakkamtee, li leen jañ ci di ko def boo ko xoolee, lu yanu maanaa la, te yéeme, mooy noflaay bi ci nekk, ak gaaw gi, ak nakk'a faale gi ak ñàkk ge'e xalaat, mbaa ragali yaq ci nasaraan, kon lii lépp, ay pakk lañu ci sunu ay xalaat di dox, sunu'y xel di xelli, suni'y xalima'y sotu, sunu'y daa di soosu, nu'y joyal sunu'y gog ci di bind li'y jeqiku, ak'a fuur, di buur ci sunu'y xol, war'a nekk di lu nu'y yaxal ci keyit yi, ba way bañ ñi kumpa di ko war'a xam.

Am na jeneen aji feeñ (fenomene) ju am ci jamono jii, moo'y ñu bari ci ndonga yi'y bindante ay bataaxel (sms) ci ëyukaay yi (telefon) danu ko'y def - bu nu ko deful ci wolof - ci franse bu nu daggat, maanaam , bu nu dog la ca'y sonnale, mbaa mu ca'y yàqloo, ngir ma gën'a leer, danu ko'y bind ci anam gi nga ko'y dégge man ko'o xam, déet gi mu ware, ci maanaa ci barabu mais nu bind mee, veux nu bind ve. 
Loolu ba tay da'y wund lakkal gu leen wii làkk lakkal, ci mbindiin wi, dégg gi, jël gi mu'y jel seen waxtu, ak jafe gi ci ñoom, leeg-leeg nga gis ci ku ci def lu sakkan ci dundam ci jàng ko ci'g tar te du tax mu àgg ci fi ci war, te wolof kat mi mu jàngul, masu ce'e sonn, ma nga ko dégg dégg gu xar baaxe, kon kii bu ko jàngoon, mu yiteel ko ni ko franse yitéele, nu mu'y mel ? laaj naa la ko.

Xanaa kawe, xanaa raw, xanaa noppalu, xanaa sakkanal waxtu, xanaa gaaw'a àgg, fees, yewwu ci'y nelaw, xippi, taxaw, jàll, romb.

Màggat mu màggat ci am njàggu'm tubaab, jabaroo  tubaab, tubaab la, tubaab ngéen dénk seen gaal gii dëggel na, kii du bëggati ku dul tubaab, lu dul tubaab, dara ci boppam, li mu moom du ko ñorati,te ñii nag ñoo'y ñi ñi'y faral'a dénk sunu gii gaal, kon waxuma la jengal ko, waaye diigal ko la ñi'y def !
Ñoom xamunu joow gaal, li ñu'y wax permanaat la nu xam (promanade), ànd ak seeni jabar mbaa'y ndaw, xaj topp ci, ñu'y def leeg-leeg ñu sanni ko ab bant, mu wadd for, nu ko'y xonte li ëpp ci sunu njël li, bu ab baykat di dee ci'b xiif, te moo'y ki taxawal koom mi, ñu'y jënd ay way màggi mbéregaan (oto), naan lu manul'a ñàkk la, te doonoon ñu ñàkk. Ñoo dugg walla, su nu taxawul ci doon sunu bopp, ci lepp, ak fepp!.

Xam nga réew mii da dul mu nu yore xam-xam waaye nasaraan, firnde ji moo'y lu waral ña fi nekkoon te doonoon ay boroomi xam-xam te di ñu nasaraanoodi, nanguwuñu woon leen'a jox'ub nosam, bu ko defee nu ko'y wommate xam-xam ak leer, bëgg sa bopp, sa réew, sa njariñ, sanni nee lu keneen, waaye loolu lepp, du man'a nekk, ndax du sunu mos mu keneen la, te keneen ki tubaab la, kon moom ñoru ko mu'y dem, di dox, di jëm kanam, li ko ñor kay na des ci'y loxoom, mu'y digale ni nu k'oy yoree, ndax mu man di sax di lu mu moom, waaye tay nga dee de,yaw tubaab!, lii de jaral nanu sunu ay bakkan ak yu doom, ndax ñoo'y ñi ko moom, kon tëyyal sa yëf te ba no'ok li'y sunu, lii'a'y li waraloon mu dénkoon ko màggat ma màggatoon ca njàggu'm tubaab ma, te jabaroo ca, xalaatu ko'o dénk keneen ku ko mo'y, ndax moo'y genn wàllam, di ki mu wóolu, di mbuus mu ñuul mu ñu sol yaxi tubaab, yàpp wa, xel ma, xalaat ya, nii la ko jenn waay ju Mbayeen daa waxe. Xoolal ma kii nga xam ne naan na géeji xam-xam yi te defewu ko ci tubaab ni nu ko'y def, danu ko'y yòbb ba ca àll ba, nu jox ko fa as ndiggante su gàtt ci waxtu ci benn leekol, mu fa'y joxe ay bind (cours) ci wu araab, ak doonte la mu jàngi woon du làkku'w araab, da ci doon jànge rekk kay.

Gisati nga fii firnde ju leer ne ñoom de xam ñoru leen du caagéenu'g xam-xam, li leen ñor kay moo di njàngu'm tubaab, lii nag waa-réew mi, ñoo'y ñi ko war'a dindi, sunu bëggee boy, joy, tàkk, wëy, di yéeg, ànd ak way yéeg ñi. Mii du dem li fe'ek nii la.

Bu nu dee ñoñi li fi nekk (realistes) , dañu naan: nanu bàyyi li fi nekk mu nekkal boppam, du nu ko ga kenn mbaa nu ko ci'y manante (forse), nit ñi tànnal seen bopp ci anamu'g demokaraasi, bu ko defee làkk wu nekk nu jox ko àqam ak li mu yayool ci ndimbal, aar, jàllale, nga xam ne déet ag noono, loolu man na'a nekk sunu ndimbal, sunu njariñ, te ñu sanni nee li nu'y wax ofisel, am as lëf ci'g nooy flexibilite, ubbiku, ci mbooleem làkk yi, ubbiwaat bu baax sunu làkk wii mu man'a ëmb, guux baat yu bari yi ko'y noppal, te bañ di sonn ci di leen wutati ñu'y juge ci boppam, fu nu gise ne lii moo yell fii, nu ne loolu la, ba kero lenn di taxaw taxaw gu fés, gu leer, gu deesul sikkati, man nga ne loolu sax am na ci wolof ci sunu gaal, waaye du tee nga ne am na yenn ruq yu jar'a gën'a ubbi, mu aju ci tas mbind mi, gën ko'o jàngale, gën ko'o yaatal, ba kero booba, ak ba ginaawam sax na ñu'y jëfandikoo lu fi nekk, te xam ne sunu yëf'a, waaye ci anam gu maandu, gu yamoo, te yell, gu dul gaañ kenn.

Lii nag am ci sunu tele bi, nga xam ne daa mel ni yëfi kenn la du lu nepp bokk, ñaaw na. Di xibaar lu toll nii ci'w nit, moom li nga leen di di xibaare, nga ne as daggiit ci waxtu lanu leen di man'a jagleel, bu dee ñeneen ñi nga xam ne ñoo'y ñi gën'a néew, te'y ñoñ boo ko doon seet sax, da nga naan matunu fukk ak dara ci teemeer ci askan wi, nga jël la ëpp ci waxtu jox leen ko, nu'y xibaar xibaar yi ci franse te nga ne yeete’e la tax'a jug? ay fen la de, ay nar la, li waral jëf jooju kay moo di màggat mu jabaroo tubaab'a la ko digal ci taxawal keneen nërméel nu, suul nu, suul sunu teddnga, sunu'g xam, yekkati keneen ki nga xam ne ca dëgg-dëgg wart'a woon'a sax aajowoo gile yekkati.

And ak loolu lepp du tee ag jam (critique) di lu man'a ñàkkadi ñeel ñenn ci sunu Imaam yi, ndax itam jël lu tol ne mbooloo mu toll ci ay teemeeri teemeer, nga'y wax ak ñoom di ko def ci làkk wu nu xamul, teg loolu diine, loolu dofeel la, yàq waxtu la, yab nit ñi la, xeeb sa bopp la, xamadi la, xamadi màggu'g diine la, ndax lu nu rafetlu la ci fu nu'y xutbaa nit ñi ci ajjuma, ginaaw ay jullit lanu, ñu laal ci's lef ci araab, làkk wi'y wu alxuraan, loolu boo ko'y xool ag sonn'a ngi ci, ci jàng ko ngir man'a xam Alxuraan, waaye it xamante ak sa yeneen mbokki jullit yi, ndax moo war'a nekk làkku ofisel wu addina'y jullit ñi, di dox ci'g bennale, ci 'g boole, ci'g xamalante, ci jappandal ag jokkoo ci biir jullit ñi. Waaye tekkiwul ne danu fe'e war'a nekk naan xar mi kaay, te'm dégg rekk bar .

Aji laaj laajoon na ne : ndax li nu'y jële ci jàngu bu nasaraan bi ci xam-xam, man na'a wuutu li nu ci'y ñàkke ? ab laaj'a ngoogu, di bu diis, bu rëy, bu am maanaa, bu soxla ku ko tontu.
Man la ma ca jéem, ci tontu bi, moo'y benn baat , bi ma jortul ne keneen du ko ci weesu, moo'y déet, déedéet. La nu fa'y ñàkke te mu'y lu gànjaru, di lu am solo, moo'y li nu fonk'a wax, mu'y cosaan, làkk nag ñëw di li ko'y jëmmal, di ko taxawal, di ko wuutu, di ko nekkal, di li nga xam ne ci lu dul moom déet cosaan.
Kon lu nu fa man'a xame réer nanu, ñàkk nanu, gàttañlu nanu, dof nanu, ñàkk nanu jumtukaay ba, jumtukyu'b yombal ba, bu noppal ba, bu gaawal ba, bu rataxal ba, bu jooral ba, ba'y déggale te'y bennale, di yombale ag jokko, te di ab xamalewaakon.

Làkku'w jàmbur niki doju pakkastal ci yoonu jëm-kanamu réew yi ko'y jëfandikoo te taqoowunu ak moom taqoo nga ca war:

Sunu boroom (t.s) nee na (( wamaa arsalnaa min rasuulin illa bilisaani xawmihii, liyubayyina lahum)) mu'y : yonniwunu benn yonnant ci'w nit ndare bu danu ko'o waxloo ca làkk wa ñu dégg. Lii Yàlla sax ci di ko def, bu amee lu mu'y tegtale de du weesu waru'g wax ak nit ñi, jàngal leen, ci wi nu màgge, dégg ko dégg ga ca war.
 
Baat yu jóox yi ñooy yi dugg ci làkk wi te bokkuñu ci woon, niki baati tubaab walla araab yi nu'y gis ci wolof.

Bokk na ci li yayoo xamle, mu'y làkk moo'y li nit ñi di wax di ci déggante'e, maanaam jaaduwul ñu naan bii baat bu franse la, walla bee kon nanu ko sanni, te nit ñi ci lanu doon gën'a déggante'e ca bu wolof ba ko fa doon wuutu, Ahmad Amiin nee na ca teereem ba tudd Fajarug lislaam: (( Araab yi de ca njëkk lislaam jële woon nanu lu sakan ci'y baat ci làkku faaris, di wu waa Iraan wi, ak wu Rom, ak wu Isipt, ak wu Ecopi, yooyu baat seen yaxantukat yi daa dem foofa'a ko daa indaale, nu duggal leen ci seen làkk wi, boole ko ci, waaye nag araabeel leen, maanaam dëppale leen ak sart yi seen làkk laaj, ci noonu Alxuraan ñew tudd leen )). Kon nag bépp baat bu nu man'a jële ci làkk, daa war'a lemu ci sarti sunu'w làkk.

Amiin neeti na ci benn teere bi: (( Yahood yi de am nanu ag jeexital gu mag ci làkku araab, tàbbal nanu ci ay baat yu bari yu araab yi xamutoon,ak ay term yu diine, yu nu xamul woon,baat bu mel ne jahannama ak shaytaan, ak Ibliis lenn lanu ci)), waxaat na ba tay ci bii teere: (( woykati araabi nasaraan yi, ku ci mel ne Xussu'bnu Saahida, ak Ummayata'bnu Abii Salt, ak Hadyu'bnu Sayd, ñoom duggal nanu ci araab ay baat aki toggaliin (taraakiib) yoy araab yi xamunu ko woon, ni ngi naan Ummayata'bnu Abii Salt moo xamal araab yi waxiinu  bismikal laahuma , mu'y ci maanaa (ci sa turwi yaw buur bi ) ñu ci'y tàmblee ay wax aki jëf, Xussu it moo'y ki njëkk'a wax ammabahdu )).
Ammabahdu di baat bu nu'y jëfandikoo ngir teqale wax ju bokkul ak ji la tax'a jug,mu mel ne nga'y bind bataaxel, nuyyoo, wax li'y ànd ak nuyyoo bi, ba noppi war'a jëm ci wax ji ne ( leegi nag:).

Lan moo'y jafe-jafe bi ku senegal ki di jànkooteel, ngir làkk yu bari yii nekk ci réew mi, fekkante fi, ñu'y yu jàmbur yi ak yu réew mi, te nu jël yu jàmbur yi teg leen ci kaw yu réew mi ? 

Nitu'g neen ci sunu réew mii, bu duggul leekol, ak doonte dugg na ko te bu tubaab, da nga ko'y gis jamono ju nekk mu'y jànkoonte'ek lu bari ci'y jafe-jafe, ci lu aju ci ag jëflanteem ak nit ñi, aku'g jokkoom ak ñoom.
Jafe-jafe yooyu lu ci ëpp, li ko'y jur moo'y ñàkk'a déggoo gi'y am ci digganteem ak ñoom, te loolu da na àgg ci jural ko ag fasu (complexe), ak ñàkk'a wóolu sa bopp, ndax lu ëpp ci waa senegaal da nu'y gëm ne seeni mbir keneen'a leen ko war'a lijjantil. Bu ci nit soxla'a dara lu war'a bàyyikoo ci àtte gi (goornemaa), mel ni ab dokimaa, walla lenn lu ko réew mi ameel ci àq, moom da'y gëm ne li war moo'y mu gëstu ku ko gën'a dégg tubaab, te li gën'a bari du ñeme'e wax sax ay xalaatam ak lu xalaat yi am solo !, ndaxte déggul tubaab walla lenn ci baati tubaab yi'y jox waxam jooju xiima ak fulla, loolu yobb na ñenn ñi ci nu'y wone ne dégg nanu tubaab, ba'y tudd ci seeni wax lenn ci baati tubaab yoy ni nu ko'y waxe sax manunu ko, te xamunu ni nu ko'y binde, te fekk na jamono ji nu ko'y def, fees nanu dell ak baati wolof yu man'a wuutu yooyule di yu franse. 
Ba ci jàngkat bi génne ci daara'y tubaab yi, te déggu ko bu baax, (ñu néew lanu ñi ko ci dégg, dégg ga ca war, ndax lu sakkan la'y jël ci seen waxtu), moom itam, day faral'a jànkonte'ek’ug fasu, walla kompleks, gi'y faral'a dal ñi'y waxe li dul seen làkk, bu ñu'y wax - te taxul ñu xoot ci lool - ak boroom yile làkk, walla ku leen ci gën'a sori. Jafe-jafe yi aju ci wàll gii maneesu ko'o takk, dees leen di lim ci'y teemeer, danu ne woon nanu ci indi yenn rekk.
                                                      
Nu ne woon nu taxawlu as lëf fii ci ag wàll gu àggoon nanu ci ci'y wax, te mu'y lu maneesul'añàkk’a jaaraat, ngir am gi solo, ak yiteel gi mu def lii nu nekk di wax, loolu moo'y taxawaay yi lenn ci boroom xam-xami joojale jamono ame woon, ci yee niti seeni réew, xoolal ma ku mel ni Petrarch, nga xam ne bokk na ci li ko taxoon'a siw yile taxawaay, ba daa fàggul boppam dàkkantalu boroomu'g nite, Te dara joxu ko woon loolu lu mo'y yitewoo gi mu yitewoo woon xay gu yàgg ga (civilisation ancienne), walla bind gi mu doon def ci làkku'w itaali wi doonoon aw waxiin rekk ca jooja jamono.

Waaw lu tax Petrarch mii doon binde ci wu itaali wi, te fekkoon fi lakku'w latin wi népp daa binde ?
Loolu de tontu li mooy bindul woon lu dul ngir nit ñi xam ko te jariñu ci li mu'y bind, kon li am solo moo'y nu xam li mu'y bind, man ko'o jariñoo, du mu bind ko ci latin. Lu mel ne jeqiku gii ( revolution) mooy li seriñ Suhaybu defoon bu yàggul, ba mu bindee ci wolof téereem bu am solo boobee di Qurratul Hayni ci xam-xamu diine, loolu tax nit ñi sottiku ci kawam ci'g fuqale, ñépp jariñu ci, ngir nekk gi mu nekk ci wolof, te kat téere'y diine ya'a ngi fi ak yu adduna yi, te kenn xoolu leen ngir nekk gi nu nekkul ci wu kocc.
Kon man nanoo wax ne Petrarch mii moo gënoon'a ñaw te ëpp xel mbokki boroom xam-xamam yi, ndax day mel ni moo leen gënoon'a xam li xewoon, bi mu gisee ne warul ci mom mu bind ci latin, te làkk wu nu gën'a dégg'a ngi fi. Deesul sikk it ne moom dey ab jeqikukat la woon ( revolutionaire) bu bokkoon ci ni gisoon ne du man'a ñàkk ñu soppi ba ci làkk wi nga xam ne weesuwul fii mu nekk ab gàllankoor ci yoonu jëm-kanamu'g askanu Itaali wi, bi mu nekkee ci dëgg-dëggi aajowoo ag jëm-kanam, ak yéeg gu xel ak gu xalaat.
Mu gisoon ne bu bëggee def jëf ju am solo ci yee, ak xamal askan wi, li ko war moo'y mu wut anam gu yòmb gu koy jàppndal loolu gën ji jàppndal, te di tax ba ñu'y man’a alawtiku li mu leen di sànni ci xam-xam ca na mu gën'a yòmbe. Lii'a ko yobb ci mu binde ci wu itaali, ba nee wu latin wi. Ci misaal sunu njiit loolee di Senghoor , nga xam ne foo toll nu ko'y tudd te du kenn, moom de boo'y xool da nga naan moom de bindul woon xanaa ngir mbokkam yii di waa senegaal, Ndax kat li ëpp ci réew mii déggunu tubaab, nga rax ci dolli dafa meloon ne ab nasaraan la , walla ku leen doon ligéeyal ci sunu kaw.
Làkk'a ngi fi woon nii di wolof, di wu ñépp déggoon, walla li gën'a yaatu ci réew mi, bu Senghoor gëmoon réewam ba di ko ligéeyal, du woon binde ci tubaab, li ko waroon kay moo'y mu defoon ko ci wolof, walla sax ci séeréer ci li gën'a néew. Walla mu digale ñu firi ko ci yile làkk, mbaa mu sàkk jëwrin ju féetewoo jëmale leen kanam, ndax ëlëg ñu man'a xëy di'y làkk yu gën'a am ag koom, te gën'a yomb'a jëfandikoo. Walla kay mu soññoon sunu boroom xam-xam bu mag ba Seex Anta, mii nga xam ne lii rekk'a ko masoon'a ñor, ci mu wëy ca yoonam woowee,te gën ko'o jàpple ci xalaat ak doole, waaye deful loolu, moom kay da ko doon xeex ci anam gu ñaaw, di ko gàllankoor ci mu amal bile naal.
Moom nag ca dëgg-dëgg moo'y ki fi nekkaloon tubaab bi, ndax yiteem jépp nekkutoon lu dul di gëstu lenn ak lu mu man'a tuuti tuuti ci lu ko man'a askanale ca waa-Orob ya, li'y tegtal ci loolu moo'y waxam jii ci téereem bi tudd ( poesie de l'action), mi ngi ci naan: (( j'ai probablement une goutte de sang portugais qui est frequent en Europe mais rare en Afrique noir )) maanaa mi di : man dey ku dem am naa as toq ci dereeti Portigaal, ndax man da maa bokk ci mbooloo'm dereetu'm (A) mi bari lool ca Orob te néew lool ci Afrik.
Loolu mu wax ngir mu wutal ko lay daa jël yaayam ji nekkoon ku dëkk jiwaalo, taxaw temb ne Gine'g Portigaal gi la cosaanoo, ak li nday ji daa wax lepp naan cosaanoowu fa. Kon kii soreewul ak ka woy wa taxoon'a jug mu'y :((Màggat mu màggat ci am, njàggu'm tubaab, jabaroo  tubaab, tubaab la, tubaab ngéen dénk seen gaal gii )).
Waaye daa mel ne da ma laa gis nga naan waaw lu tax seriñ si daa binde ci araab te wolof nekkon fi ?

Seriñ si de li am ba mam, moo'y ci araab lanu daa binde, waaye ak ci wolof, te araab de li leen ci jañoon du jëmmi làkk wi rekk du woon it gòndiku ci, walla fònkadi wii di seen wos, mbaa foñ ko te weddi ko, ba loolu di leen ci'y tee di binde ak'a tase seeni xalaat. Li fi nekk moo'y ñoom seenu'g xér gu tar ci nit ñi doon ay jullit yu dégg seen diine, rawati na alxuraan mi deesul dégge ci lu dul araab, moo leen àggale woon ci ag wàll ci seeni ligéeyi xam-xam rawati na la ca aju woon ca diine ñu ko daa defe ci araab.
Ñoom de dañoo gëmoon - te loolo'ooy li waroon- ne alxuraan mii kat aji nekk la ju fees dell aki kiimaan aki way lòttal (aji lòttal nag bu nu ko waxee ci xam-xamu diine mooy lol Yàlla rekk'a ko man, lòttal na mbindéef yi ag defam).
Benn tafsiirkat - seen gëm-gëm laa la'y wax- amutoon kàttanu'g leeral ko, mbaa mu indi lepp ca tafsiir ga ca war, ak leeral ga mu yayool, moo taxoon nu gisoon ne nit ñi daal ci masala mii, ñoom ñépp'a ci yam, maase ci ni bëñi peñe, kon li leen doon noppal ci seen gis-gis, moom'y nit ñi maaseendoo jàng araab, ku ci nekk lijjantil ko sa bopp, settantalal sa bopp ci way teddi aaya yii, ci lu dul nga'y sukkandiku ci kenn. Ndax kat kenn gënu leen ce'e man'a dimbale seen bopp, bu nu déggee araab, bu nu ko deful nag, lu nu ci man'a ame itam am raxasiit rekk lay doon, aw desiit, ag wall ca lépp rekk la’y doon, du weesu yu njëlbeenu yi rekk , deet yu mag yi.
Waaye jàngale gi ci araab ak bind ci, teewu leen woon di bind ci wolof ak'a bindante, ak di ko jéem'a jàllale, ci taalif ci ay woy yu rafet te sakkan, fees dell aki baat yu xoot, yu naroon'a réer moos bu nu ko deful woon, aki masala'y nahwu (grammaire), amoon nanu ay xisa yu yéeme, ami nettali yu adabé (yu njàggaté), aki cax yu xoot yu daa dimbalee ci màggal am xel, rawati na mu gone gi. 
Seen woy yooyu ak nettali yi danu daan fees - ci li ëpp - ak lu’y yare,loolu bokkoon na ci li daa dimbale yarkat yi, ndaxte ñu ci ëppoon fekkoon nanu nit ñi nu di boroomi jikko yu rafet yi ñu dégge ci woy yooyu ak léeb yooyu.

Xoolal ma léeb wu mel ni ( Kumba am nday) niki misaal ci ay nettali yu di kojug yar, yu'y dund, tukkee ci sunu réew mi, moom de lu am solo la ndax daa fees dell aki misaal yu kawe.
Moom de day soñ ngone yi, rawati na jigéen ñi, ci ñu ràngoo jikko yu rafet yi, ñu'y muñ, farlu, nangoo dee ci lu baax. Loolo'oo tax ñu man ne ñaari làkk yii, daal duñu wooni noon, waaye way mottaleente lanu woon, yu daa dimbalante, bii ñu ko'y jëfandikoo ci li ëpp, ci wàllu'g diine ak jàppe ko jumtukaay bu am njariñ ci dégg alxuraan mu tedd mi, te fiqu ci jile diine, ndax faqiih moom muy ku xam fiq, maneesu ko'o nekk ci lu dull dégg bu baax araab, kenn mant'a dégg jile diine, di jariñu ci xam-xam bi ci nekk te déggoo araab, loolu xaw naa jòmb.
Senghoor sax seere na loolu ca ( poesie de l'action) , mu ne: (( je suis pour le mainien du Latin coome langue universelle de l'Eglise catholique, tout comme je duis pour le maintien de l'arabe comme langue de l'Islame)) maanaa mi di man ànd naa ak ñu tëyye fi Latin niki làkku egliisu kotolik bu adduna bi, ni ma ànde ci nu def araab lakku lislaam.
kon nag li nu sañ'a wax mooy mag ñi de, wolof lanu jàppe woon seen làkku ofisel, te daa nanu sonn it ci jëmale ko kanam, daa sukkandiku ci loolu ci làkku araab, seenu'w jàngaliinu araab it walla xam-xami diine ñi ngi ko daa defe ci di tekki baat yi ci wolof, baat bu nu la wax rekk wax la ba mu tollool ca wolof, loolo'o jur riisu'g wolof gii, fees dell ak baati araab yu nu wolofal, tax it ba yeneen baat ci wolof am yeneen maanaa, yeneen tëggiin it sosu yu manul woon'a ñàkk, te feeñe ci wonu'g araab.

Ndax nag du'g dofe, nu sanni nële sunu lakku nday wii, ngir jël weneen wu keneen, di ko jëfandikoo niki ofisel - naan dafa yor ci way yayale'y xam-xam ak yu xay yu wosam amadi - ci jàngal sunu'y doom yu ndaw ak yar leen. Ñun de ci loolu danu'y jàmmaarloo ak lu sakkan ciy coona ci xamal leen, te déggal leen ci anam gu dëgër, te gaaw. Ndax gënul woon'a dëppoo ñu jëfandikoo sunu wos wii, ngir mu gën no’o jappandi - ca anam ga mu gën'a yaatoo - nu sol leeni xam-xam ci lu dul gën ja'a neewi coona?.

Ndax yellul ci nun nu jéem'a lijjanti sunu jafe-jafe yu bari yii nga xam ne foo wëlbatiku gis leen, ñu'y yu koom ak ak ak, te'y yoo xam ne jafe ge'e lijjanti foo ko takk weesu na ko, te ñu soxla lool ku ci jéem, te bàyyi nag sonn gii nu'y def - ci kem bu rëy bii ci'g farlu ak yitewoo - ci yekkati jeneen aada walla kiltiir ju di kojug jàmbur ?.
Ñun de foo nu fekk ni ngi wax, ba sunu'y gimiñ yi sax - ci li'y feeñ - xanaa amatunu beneen ligéey bu leen war ci seenu'g dund, bu dul joyal baatu'b frankofoni, jaarale ko ci diggante seeni bëñ ànd ce'ek as lëf ci'm mbég ak màggal.
Bii baat de da'y dikk di bawoo ci put gi ci'g diis, bijj nag ay mbiccam, di lu ñu peege mbalaanu'm wurus mu wormaal ak jox àq, bu ko defee mu bocciku nag ci'g rëy mel ni moo'y buur bi, te fekk na ne nëbbul ci diggante ay lem-lemam lu toll ne peppu suuf ci maanaa, aha kay, xanaa mi nekkul lu dul sanni ca àll ba, lépp lu la fi sa maam bàyyil ci ndono lu xam-xam mbaa cosaan, te'y sonn ci jañ pono'y aada'y tubaab ak aw làkkam jëm ca kanam, ak yitewoo ko mel ne moo'y lépp, sànni ca sa ginaaw lépp loo moomoon ci làkk ak xay, naaneey: du dara lu dul ag wëy (paase) aku'g dellu ginaaw, te ag teew amul ñeel ku amul'ug wëy .

Man de noonuwuma tubaab waaye xam naa ne yayoowul ci ñuñ gii yitewoo gu mag... ci sunu's alku. 

Lii nag gëstu la gu ñu doon def, bëggoon ce’e génne lii nu peek, wër nu ci’y jafe-jafe, rawati na yi ci di yu aju ci sunu li làkk li laal. Waaye nag ba tay gëstu la gu njàggat, gu nu jublo’o def ngir génnewaale ci as lëf ci taaru’b wolof, ak li mu làmbool ci’g nooy ak man’a ëmb.
Mu doon it ag woote jëme ci luñutu ak jam (critique ), ak def lu mel ne lii gu tukkee ci geneen wàll gu nu moy .
Kon sunu yëf’a ngoogu, di lu aajowoo xalaat, xool, sònn, yitewoo ak jàllale.
Na léen wóor nag ne ci’g solowoom ak’ug déetam , népp la ñeel, népp’a ko ñeel it, ndax sunu mbir la , di ménn ci yi nu man’a jëmale kanam, bu ñu ko fonkee, ci li ma jort.

Abdu Xaadir KEBE

#Article 15: Way (101 words)

Misik ak Way
Misik(fr musique en music) nak ci wolof misik rek lanu koy wax ndax daa bok ci baat yi nga xamni ñéppa ko bok mook lu melni widewo(video) WAY baatu way mingi jugé ci nit ku way maanaam nit ku yéwwu litax mu tudd moom nit kookii waykat dafa way bà man a sos ay wax mbaa ay nasar yoo xamni nit ñimu nékkal bàyyi wuñu ci xel mbaa sax xamu ñuko woon kon moo leen gën a way batax muy way kon kuñuy tuddee waykat dafa wara doon kuy yeeté

Ay Misikkat ci Senegaal

Ay nasarkat/Taalifkat ci Senegaal

#Article 16: Taariix (646 words)

Mooy xam-xam bi'y gëstu la xewoon demb. Di itam mbooleem ay Jëf ak ay xew-xewu demb, la ko dale ca ña nu jiitu woon ba ci nun. 
Taariixkat mooy ki'y gëstu di bind ci wàllu taarix

Xam-xamu taariix moo nuy melalal mbiri dëkk yeek dëkk-dëkkaan yu yàgg ya, ci biir jamonoy taariix, ak mbiri seen way dëkk. Da na nu waxal it ca dund ga fa amoon. Ci gàttal daal, xam-xamu taariix day gëstu li-wéyi nit (dembam) cig matale. Da na wuññi (feeñal) it nekkiin ak dundiin yi nga xam ne nit jaar na ci jànkoonteek ñoom ci dundam gu gudd gi, ci biir ay jamono yu dabante te toftaaloo, bu ko defee mu gëstu anami jëm-kanam yi nga xam ne nekktéef bii (di nit) amal na leen ci taariixam bu gudd bi, ci noonu loolu jural ñu ñu jange ci daj-dajam (li mu jot a dund) yooyu wéy, aki ndamam, te jéem a moytu ay pakkastalam aki rëcc-rëccam ya jàll.

Bu lii amee nag dina nu gis njariñ ak ngënéeli gëstug xam-xamu taariix.

Taariix dinanu ko jang ngir mu yombalal ñu xam mboolaayi nit ñi ci anam gu xereñ, te dégg (nand, gis), xàmmee it buum yi leen boole. 

Gëstu dundug buur yeek imbraatoor yi rekk du lenn rek li nu war a yitteel ci taariix, li ci gën di farata kay mooy gëstu dundug mbooloo yi ak bennaan yi (benn-benn nit ñi). Ak gëstu jafe-jafe yi daa yeesu ci seenug dund bis bu Yàlla sàkk, te jéem leen a wutali saafara yu dëppoo, ba maas giy ñëwi ëlëg man cee jariñu.

Ngir digal ab xew-xew fàwwu mu am ab tombub boy (fa muy dooree). Ay tombi boy yu bari nag am nañu te taariix man na cee tàmbalee. Nasaraan yi ñoom seen tombub boy mooy juddug Yonnant Yàlla Isaa, ca lañuy taariixe seeni xew-xew, bu dee jullit ñi ñoom seeni xew-xew ñi ngi leen di wutaluw dig wu bawoo ca gàddaayug Yonnant bi(j.m) juge Màkka ga mu ganee àdduna, dem Madiina. Xew-xew bii nag mi ngi fiirook (dajeek) atum 622 ci taariixu juddug Yonnant Yàlla Isaa.

Donte taariix mooy la xewoon ba àdduna sosoo ba léegi, taariixu nit ñi, suuf si, jawwu ji,... Waaye ci déggoo taariix ñu ngi koy tàmbalee ca ba ñu sàkkee mbind, séddale ko ci ay jamono. Li nga xam ne ay téere yu ñu bindoon moo ñu ko xamal. 

Njëkk-taariix(mooy taarixu ñi fi nekkoon laataa sàkkug mbind)

Taariix( mooy lépp li xewoon ca ba ñu sàkkee mbind ba leegi). Taariix ci boppam dañu koo sédale ci ay jamono.

 (feeñug nit ci suuf ba daanu'g nguuru rom gu mag ga ci 476)

 ( ba feeñug Amerig ci 1492)

 (ba fippug waa-frãs ci 1789)

( ba ci sunu bis yii)

Boroom xam-xam yi, ginnaaw gëstu gu ñu def ci suuf si, wuññi nañu ay jeexiit (reste;vestige;trace) yu yàgg: ay jumtukaay, ay xor, ay doj, añs yuy tegtale ne suuf sii déy aw nit dëkke woon na ko njëkk ay junniy at, jamono jooja la nuy tudde njëkk-taariix.

Moom nag mi ngi séddaliku ci ñaari xaaj:

Ci ngënéelul jeexiit yii lanu xame njëkk-taariix. Nit ci jamono jii da daan tuxu rekk, di jëfandikoo ay ngànnaay aki jumtukaay yu njëlbéenu (primitive) (doj yu ñu yatt, ay ngànnaay, ay xeej aki xepp).
Bi jamono gënee dox, seen dund gi soppiku, ñu xam leegi sawara, jëfandikoo ko ci togg ñam yi. Ci jamonoy doj wu ñu xacc wi, lañu tàmbalee dajaloo, sóobu ci mbéy, sàmm ak ràbb ak liggéey jumtukaay yu xànjar yi, tàmbali it di def yenn liggéeyi fànn yi niki bind ci doj (ciseler ;graver), ak yatt.
La ko dale ca 3500 n.j.g (njëkk judd gu yonnant Yalla Isaa), la weñ feeñoon, ñu fent it mbind. Bi weñ feeñee, fentees it mbind la njëkk taariix jeex, taariix daal di tàmbali.

Seex anta Joob(Cheikhe Anta Diop)

Paate sow

paate sow (wo): Dembi Senegaal, 1998

#Article 18: Cosaan (253 words)

Cosaan baati Seereer-Safen la. Moo teki début / origine / commencé ci làkki Seereer.

Ci xëtt wi,  see fas  tekki . Sama weerukay ci walu xam-xam moodi jangat-nit . Bile baat, manko tëggé ci (anthropologie), manaam anthro=nit ak pologie=jangat. Cosaan, aada, ak luñuubaaxo daño fasoo. Waayé, ci sama gis-gis, cosaan moy r, manaam fu aw askan bayee koo. Bilep firi daa ajju si walug bërëp (espace). Cosaan, mana firi batay luñu donnu ci makk ñi. Kon ci tënkk, cosaan, moy reenu askan,  lunġa   länkalee , di luñu baaxo def, loolu moo lay jox culture wala mu xeltu ko ta mu jem ci walu dundam, man nañ jappé culture. Kon, suma suka ndikoo ci lii ma fessäl. 
Cosaan nak, ci walu xeltu, baat bu jaxaso la.  
Gëstukat , dalee ko ci jamano yu yàg ya, kon luy walbatiku. Nittu jamano boo jel, dañu tànn ci seen cosaan ay lëffin. Rax ci dooli, dañuy fen. Waaye timit, nguuruk reew munek war jôkaar . Cosa, don te mengo tul ak. Cosaan ak aaday Reew yi eup  dañu wali ci cosaanu reew yi new doolee, ak dileendi nasaxal. 

Bu njekk, borom xam-xam yi bayoo tuggal ta see gëstu ajju ci walu jangat-nit. Li lalloon bilee weddi moodoon ne see dëkk yi ñoo  noot,   seeni kom-kom. Bi aduna doxee ba nootagee bi jeex, bu afrik moom boppam,, ñeppu nagu nagn ni askan . Nit ku nuul  yam wanee ne nit Lolu di ndam lu rey si xeetu nit .Ndax te bo xamul , do xam .
SEEX LO

#Article 19: Aadama (114 words)

Aadama mooy ni ñu ko waxe ci Lislaam (آدم). Ci angale mooy Adam te ci faranse itam mooy Adam. Mooy nit ki Yàlla jëkka sàkk.

Nettalib Aadama feeñ na ci Ge 1:26-30; 2:4-8; 15-20. Aadama dafa toppoon jabaram Awa ci bàkkaaram. Bàkkaar boobu mooy lu indi musiba yépp yi nu gis ci àddina si (Ge 3:6-21). At, ya Aadama dundoon, 930 la. (Ge 5:5). Ci Injiil dañuy wax ci Aadama ci Lu 3:38; Ro 5:14-19; 1Ko 15:22,45; 1Tim 2:13,14; Yu 1:14.

Nettalib Aadama feeñ na ci suraat 2:30-38; 3:33,59; 7:11,19-27; 17:61-62; 18:50; 19:58; 20:115-128. Nekk na ki borom bi ñëk bind mouy nit doon tamit yonent bi ñëk

Waxinu wolof bu tekki nit ñi.

#Article 20: Aaroona (220 words)

Ci làkku ibrë (אַהֲרֹן) la tur wi jóge. Aaroona mooy ni ñu ko waxe ci Lislaam. Ci angale ak ci faranse mooy Aaron.

Magu yonent Yàlla Musaa la woon, ñu bokk ndey ak baay. Ñetti at la Aaroona mage Musaa. Baayam, Amram la tudd te yaayam Yokebedd (Ex 6:20). Amoon na ñeenti doom yu góor ci jabaram, Eliseba. Ñooy Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar (Ex 6:23). Aaroona amoona benn rakk bu jigeen, mingi tudd Mariyaama, doomu ndeyu Aaroona ak Musaa (Ex. 15:20). Mariyaam bii, bokkul ak yaayu Yeesu Krist.

Ba Musaa demee ci kanamu Firawna Aaroona dafa àndoon ak moom ngir nekk yonentam (Ex 7:1). Yàlla tànn na ko, mu jëkka doon saraxalekat bu mag ba ci biir bànni Israyil. Moom moo sàkkaloon bànni Israyil benn xërëm bi xaaroon Musaa ca tundu Sinayi. Ñu tëgglu aw sëllu, muy xërëm, ñu di ko tuuru, di bànneexu ci seeni jëfi loxo (Ex 32:1-28). At, ya Aaroona dundoon, 123 la. Ci kaw tund wi ñu wax Xor la faatu (Nu 33:39). 

Man nga jàng jalooreem ci 

#Article 21: Agaripa (191 words)

Ci angale ak ci faranse mooy Agrippa.

Buur Erodd Markus Yulyus Agaripa II bokkoon na ci juróomi buur ya tudd Erodd. Baayam itam Agaripa la tuddoon, mooy sëtu Erodd bu mag ba. Ci 27 g.K. la juddu. Yónni nañu ko Room ngir mu jàng. Ci 44 g.K., bi mu amee daanaka 16 at, baayam gaañu na. Ci 48 g.K. Erodd bu jóge Calkis (Chalcis), magu baayam dee na itam. Buur Këlódd Sesaar moo ko faloon buuru diiwaan yi baayam bu ndaw yilifoon, ba noppi ci 53 g.K. dolli ko ak yi maamam Filib ak Lisañas yilifoon. Mu nguuru ci Yude 48 ba 66 g.K.. Dafa séy ak rakkam Berenis (ñu bokk ndey ak baay). Dëj nañu Pool ci kanamam (Jëf 25:13-26:32) bi Agaripa amee daanaka 30 at te sooga jóge woon Room ngir sampu ci Yerusalem ak Sesare. Ci 65 g.K. Agaripa mënul noot yengu-yengu Yawut yi. Ci xeex bi mujj am, xare Room tas na réew mi ba dara desu ci 70 g.K.. Ci 75 g.K. nguuru Room may na Agaripa mu yilif wàll ci Siri. Gaañu na daanaka 100 g.K..

Ci Injiil Agaripa moo feeñ ci Jëf 25:13,22,23,24,26; 26:1,2,19,27,28,32.

#Article 22: Almasi bi (205 words)

Ci làkku ibrë (מָשִׁיחַ), la baat bi jóge. Almasi bi mooy ni ñu koy waxe ci Lislaam (, المسيح).
Ci angale mooy the Messiah; Ci faranse mooy le Messie

Almasi bi mooy tekki 'Ku Yàlla fal ngir liggéeyal ko'. Yonent Yàlla yi jiitu woon jamano Kirist waxoon nañu ci lu jëm ci musalkat bi Yàlla dige woon nara ñëw. Tur wi dafa ëmb wax yooyu yépp. Yawut ya, bu ñu masaana fal kenn, dañu daan sotti diwlin ci boppam, muy yonent, muy sëriñ mbaa buur. Krist, Almasi bi nag, mooy Ki Yàlla sol Xelam, ngir wone ne mooy Yonent, Saraxalekat ak Buur bi. Moo di yonent, bi nuy jottali xebaaru jàmm fa kanam Yàlla. Moo di Saraxalekat, bi nu ubbil bunt fa Yàlla. Moo di Buur, bi yilif ñépp ak yépp.

Baat bii mu ngi jóge ci làkku araab, sukkandiku ci làkku ibrë, te muy tekki ‘Kirist' ci làkku gereg. Ci Injiil bi ci gereg Almasi bi dafay am ñaari yoon rekk (Yow 1:41; 4:25). Ci firi Wolof, bu Injiil bi ci gereg amee Kirist te mu bëgga wax ci ndombam dañu koy firi Almasi. Bu Injiil bi ci gereg amee Kirist te mu bëgga wax ci turam dañu koy firi Kirist. Seetal itam Kirist.

#Article 23: Anas (120 words)

Ci làkku ibrë la tur wi jóge.
Ci angale mooy Annas; Ci faranse mooy Hanne ou Anne

Saraxalekat bu mag ba la woon. Kiriñus, boroom réewu Siri moo ko fal saraxalekat ci at 6 walla 7 g.K.. Waaye Garatus, boroom réewu Yude, folli na ko ci at 15 g.K.. Mu fal ci palaasam Ismayel ba noppi Elasar doomu Anas, ba noppi Simoä, ba noppi Kayif ci at 18 g.K.. Waaye gannaaw bi ñu ko follee, baatam dafa weyoon di am sañ-sañ bu bare. Naka noonu Anas ak Kayif bokkoon nañu ci liggéeyu saraxalekat bu mag ba ca jamano ji Kirist liggéeyoon. Kayif takk na doomu Anas.

Dañuy gis Anas ci Injiil ci Lu 3:2; Yow 18:13,24; Jëf 4:6; 5:17-18, 27-28.

#Article 24: Ancos ci Siri (1608 words)

Ancos, ca jamono Injiil, péeyu diiwaanu nguuru Room bu tudd Siri la woon. Dafa nekkoon ca wetu joor gu naat ca dex gu yaatu gu tudd Oront (fleuve Oronte), 32 kilomet ca kaw bëlu dex ga, maanaam fu dex ga dugg géej ga. Teeru Ancos moo doon ca dëkku Selusi, bu nekkoon ca Géej gu Mag 8 kilomet ca noru bëlu dexu Oront ba. Selusi nekkoon na 26 kilomet ca sowu Ancos. 

Ca at bu Pool demoon fa, daanaka atu 43 g.K. dëkk bi xumb na. Nu ngi doon tabax di beesal dëkk ba, gannaaw ñaari yëngu-yëngu suuf yu yàqoon lu bare. Ay fukki junni Yawut ya dëkkoon Ancos te ñoom woomle nañu, te seen jàngu rafet nañu. Gereg yu bare ñi ngi doon ñëw ca seen diine. Ancos moo doon dëkk bu neex a dëkk te rafet. Waaye dëkk ba dafa siiwoon itam ndax seeni noos, seen ñaawteef ak seen njaaloo ak doxaanu yàqute. Bànneexu àddina si rekk la waa Ancos doon wut.

Dëkku Gereg bu am solo la woon bu nekkoon ñetteelu dëkk bu gëna mag ci nguuru Room gannaaw dëkki Room ak Alegsàndiri. Buuru nguuru Maseduwan ñoo ko sampoon daanaka 300 at lu jiitu jamono Kirist. Naka noonu ña fa jëkk a dëkk ñoo doon ay xarekatu Maseduwan ak waa Aten. Waaye yeneen Gereg ya toppoon nañu ca ñoom. Tamit buuru Geres dafa xiirtal Yawut ya ñu ñëw dëkk fa, te may na leen ñu nekk jaamburu dëkk ba. Waa Room nangu nañu diiwaanu Siri ca atu 64 j.K. Naka noonu ca jamono Injiil dëkk bi dafa boole waa Maseduwan, waa Geres, waa Room, waa Siri ak Yawut ya. Waaye amoon na ay jafe-jafe diggante Yawut ya ak ñi des ca waa Ancos ba dem sax ba am jamono waa dëkk ba bëggoon nañu rey Yawut ya fa dëkk.

Ca suufu nguuru Room diiwaanu Siri dafa jëm kanam bu baax. Waa Room ñoo defoon Ancos seen péey ak màkkaanu xare ci diiwaanu Siri. Waaye ba tey waa Room may na dëkk ba mu yilif boppam. Ndegam Siri dafa nekkoon ca digu nguuru Room te mu féete waa Pàrt, beneen nguur bu xeex ak nguuru Room, Siri nekkoon ca suufu buuru Room ba moom ci boppam. Buur ba, Sesaar, moo faloon benn jawriñ ngir toogal ko ñetti at ba juróomi at yu nekk, mu nekk Boroom réewu Siri. Boroom réewu Siri moo sutoon Boroom réewu Yude, di ko yilif. Amoon na ñeenti mbooloom xare bu tudd 'léjiyoŋ' ca Siri, bu nekk bu am 6.000 xarekat ya. Amoon na itam ay gaalu xare ca Selusi.

Yaakaar nañu ne daanaka 200.000 nit ña fa dëkkoon ca jamono Injiil. Benn boroom xam-xam dafa yaakaar ne benn cér ca juróom-ñaar ca niti dëkk ba Yawut la woon te Yawut ya dëkkoon ca ñetti gox ya. Yawut ya amoon nañu alal te seen dundin xëcc na yu dul Yawut yu bare ñëw bokk ca seen diine.

Koom-koomu Ancos amoon na doole lool ndax kàttan gu mu am ci biir nguuru Room, tamit ndax yoonu jaaykat yi am solo ya jaaroon Ancos ak ndax lu ñu fa defaroon ca dëkk ba. Ancos dafa siiwoon ndax dàllu der yu rafet, latkoloñ, saf-saf yi ak ndàbb lu xeeñ, piis yi, gànjar ya ak takkaay ya, téere ya, ak li tëggu xaalis ak wurus defare.

Yoonu jaaykat ya jóge ca penku, maanaam Babilon, Asiri ak Iraak jaar na Ancos, te dafa tiim yoon wu dem nor ak sudd wu boole Palestiin, Siri ak Asi Minër. Naka noonu amoon na wenn yoonu jaaykat wu jaar ca tund ya ca xunt bu tudd 'Buntu Siri' ba noppi dem Tars. Yoon mu jóge Tars wu tudd 'Yoonu Eŋaca' (Via Egnatia) dafa jàll Asi Minër ba dëkku Efes. Tamit gaal ya mënoon nañu dox ca dexu Oront diggante géej ga ak dëkk ba.

Dëkk ba, moom, rafet na lool. Nguuru Geres def nañu yoon ya ca kaw tëralinu damyee ngir yoon yu mag ya jàpp ngelaw lu féex lu jóge géej ga. Amoon na benn miir bu mel ni tata bu wër dëkk ba lépp. Buuru Room bu nekk tàmbali ak Pompey ca atu 64 j.K., dugg na xaalisu nguuru Room yu bare ci tabax ya ak rafetaayu dëkk ba. Ni bépp dëkk bi Gereg ya walla waa Room tabaxoon amoon na ay powukaay ak amfiteyatërë, ay màggalukaayu yàllay xërëm yu bare, ak ay këru sanguwaay ya. Feesoon na dell ak ay pénc fu xale ya doon fo, waxkat ya indi seen wax, jaaykat ya jaay, te reetaanlukat ya bégloo mbooloo ya. Def nañu ay robine ca kaarfuur mbedd ya ngir jigéen ya mënoon nañu root, ndox moo xam ne mu jóge ca dex ga walla ca ay bëtu ndox ya amoon ca dëkk ba. Tamit Yulyus Sesaar tabax na benn 'akwadakk', maanaam pom bu indi ndox, ngir dimbali gox yoo xam ne amuñu woon ndox.

Erodd bu Mag ba tabax na wenn yoon wu jàll diggu dëkk bi diggante buntu miiru dëkk ba ca penku-kaw, ak buntu miir ca sowu-suuf. Yaatuwaayu yoon wu mag woowu 10 meetar la woon. Dem na 4 kilomet, te lépp tali doj wu dëgër wu jóge Misra, walla marbar. Dafa dem ca pénc bu réy ca diggu dëkk ba. Ca pénc moomu amoon na benn nataalu Buuru Room Tibeer Sesaar bu réy bi ñu defare xànjar. Ca wetu yoon wa ca ñaari bor, fukki meetar yu nekk, amoon na ay kenu doj yi ñu taaral. Dafa meloon ni mbaar ba tax ñi dox ña mënoon nañu dox ca wetu yoon wa guddaayam lépp te bañ génne ca naaj wa walla taw ba. Yu gën a bare ca kenu ya amoon na ay nataal yi ñu yett walla defar ca xànjar. Diggante kenu ya amoon na bunt ngir dugg ca kër ya, bitik ya ak biro ya. Yoon ya amoon na sax làmp ya tàkk guddi.

Amoon na benn dun ca biir dex ga fu dex ga jaar ci biir gox yu nekk ca noru dëkk ba. Guddaayam ak yaatuwaayam 3 kilomet la. Foofu lañu tabax këri buur yi, ak benn estaad ngir rawante fas ak sareet ya. Guddaayu estaad ba 500 meetar la woon ba moo wara tax mu bokk ca ya gën a réy ca àddina si. 

Ancos amoon na itam ay màggalukaay ca yàllay Gereg ak Room, ak ay powukaay. Yàllay Ancos moo doon Sës.

Juróom-ñetti kilomet ca suddu miiru dëkk ba amoon na benn gox bu tudd Dafëne. Ca wetu yoon wa dem Dafëne amoon na ay tool fu ñu bey lawtanu réseñ ngir defare biiñ ak tóor-tóor yi ñu defare latkoloñ. Dafa nekkoon ca kaw benn déndu tund, maanaam 'palato'. Yaatuwaay ak guddaayu palato ba bu ne 1800 meetar ya la, te mu nekk 90 meetar lu gën a kawe niwo Ancos. Amoon na màggalukaay ca yàllay xërëm ju jigéen ju tudd itam Dafëne. Waa Ancos gëm nañu woon ne Dafëne nit la woon, ki Apolo, benn yàllay Gereg, soppoon. Apolo dafa ko dàqe di dàqe ba ci mujj Dafëne dafa soppiku nekk as ngarab bu tudd 'loriye'. Goxu Dafëne amoon na benn sardin walla park bi ñu defaroon ngir bànneex rekk bu am wëraayu 16 kilomet. Ca biir màggalukaayu Dafëne amoon na ay sëriñ yu jigéen yu nekk gànc yu bare. Guddi gu nekk ci seen turu diine ñu defaat li amoon ca nettali ba, maanaam jaamukat ya doon nañu dàqe sëriñ yu jigéen ya ci biir garabu loriye yi ci biir sardin ba, ba jàpp leen di séy ak ñoom.

Buuru Room Ogust Sesaar samp na benn po 'olimpik' (Jeux D’olympique). Ñeenti at yu nekk po boobu indi na ay joŋantekat yu bare ngir rawante ci diiru 30 fan ci daw, tëb, sànni xeej ak fitt, rawante fas ak sareet, bëre ak ñoom seen. Amoon na itam rawante ca misik ak ci tari nettali.

Gis nañu ne ay at gannaaw deewu Kirist, mbooloo ñi gëm ca Yerusalem fal nañu benn waa Ancos bu tudd Nikolas ngir mu bokk ca juróom ñaar yi doon toppatoo yëfu mbooloo ñi gëm (Jëf 6:5). Xebaar bu baax bi egg na Ancos gannaaw deewu Ecen daanaka atu 40 g.K. (Jëf 11:19-21). Ñi ko indi ay Yawut yi làkk Gereg lañu woon, yi jóge dunu Sipar ak dëkku Siren ca Libi. Ñoom def nañu lu bees. May nañu Gereg yi topp Yeesu ci lu sësul ca xaraf walla yeneen aada Yawut. Mbooloo bu mag gëm na Boroom bi. Foofu lañu jëkk tudd taalibe Kirist 'Gaayi Kirist' (Jëf 11:26). Ci bu jëkk tur boobu turu foontoo la woon. Waa Ancos dañu doon siiw ndax ni ñu doon foontoo nit. Daanaka fukki at gannaaw ga, amoon na ca ña gëm ca Yawut ya ca Yerusalem, ña jaaxle ndax yu dul Yawut yu topp Yeesu te kenn xarafalu leen. Werante wu réy amoon na ba tax ñu def genn géew ca Yerusalem, 650 kilomet fu sore Ancos, ngir waxtaan ci.

Am-ami ñi gëm may na leen ñu mënoon a yónni ndimbal ca ña gëm ca Yerusalem (Jëf 11:27-30). Tamit ca mbooloo ñi gëm ca Ancos la Pool jóge ngir tas xebaar bu baax ba ci biir yu dul Yawut ya, te ca Ancos la dellusi yoon bu nekk – maanaam Ancos dafa nekkoon mel ni màkkaanam. Ñetti tukkeem yépp dafa tàmbali Ancos. Ca jamonoom, mbooloom ñi gëm ca Ancos moo gën a am taxawaay bépp mbooloo ci mbiru ni mbooloom yi ca àddina sépp doxe, xëyna bu dul mbooloom ca Yerusalem.

Tey jii dëkk bu ñàkk solo la bu tudd Antakya ci Tirki (Turquie). Am na 35.000 nit kese, ay toppkatu egëliis gereg yi des ci biir am réewu jullit yi.

Ancos ca Siri feeñ na ca Jëf 6:5; 11:19-27; 13:1; 14:26-15:3; 15:22,23,30-33,35; 18:22-23; Gal 2:11

#Article 25: Ancos ci Pisidi (932 words)

Ancos mooy benn dëkk ci wetu diiwaanu Pisidi, fu Pisidi digalook diiwaanu Firisi. Ci dëgg-dëgg ci diiwaanu Firisi la bokkoon waaye ba tey faraloon nañu ko tudd Ancos ci Pisidi. Gentam sorewul dëkk bu tudd tey jii Yalwacc (Yalvaç) ci Tirki (Turquie). Ancos nekkoon ca kaw benn tund wu ndaw bu nekkoon ca kaw benn palato bu yaatu te naat. Tund wu ndaw wa moom itam palato la woon, wu am dénd lu tollook 300 ektaar. Benn boor nekkoon 15 meetar ca kaw jooru palato ba. Waaye beneen boor nekkoon mbartal mu kenn mënul yéeg 60 meetar ca kaw joor ja. Naka noonu dafa mel ni tata te yomb na aar. Nekkoon na itam ca yoon wi mag wi waa Room tabaxoon wi jàll Asi Minér penku ba sowu diggante dëkku Tars ak dëkku Efes, wu tudd 'Yoonu Sebasëtë'. 

Nguuru Selësid (maanaan waa Siri, ñi donnoon wàllu nguuru Geres) moo ko sampoon daanaka 300 at lu jiitu jamono Kirist, ngir teg fa xare ba, Bëggoon nañu aar nguur ga ca xeetu Pisidi wu nekkoon ca tund ya ca sudd, tamit am ndogal ca lépp lu jaar ca yoonu jaaykat ya wu mag wu jaaroon Asi Minër penku ba sowu. Sampoon na ko fa itam ngir boole ñi dëkk ca diiwaanu Firisi ak aada Gereg yi. Ñi fa jëkk a dëkk ñoo doon Gereg yi jóge dëkku Maŋesi ca diiwaanu Lidi ak Yawut yi jóge Babilon. Ca atu 25 j.K. nguuru Room moo def dëkk ba suufus Room, boole ko ak diiwaanu Galasi. Jaamburi dëkk ba yépp amoon nañu yelleef yu yem ak yosu waa dëkku Room. Tamit, indi nañu ay xarekatu Room yu bare yi ñu may ñu génne xare ba (maanaam soldat yu màggat), te may leen suuf ngir ñu dëkk fa. Gannaaw ga ndànk-ndànk dëkk ba tàmbali gën a niroo dëkki Room yeneen dëkk yi ko wër. Ca jamono Injiil dafa niroo dëkku Room ca wàllu yoon wa, ca wàllu nguur ga, ak ca wàlli tabaxin ak colin. Rafetal nañu dëkk ba bu baax ak pénc ya, ak kenu ya, te ak nataal yi ñi yett ca doj ak xànjar.

Ancos ci Pisidi moo doon dëkk bu gëna am solo ca diiwaan ba. Lu ëpp 100.000 nit ñoo fa dëkkoon. Dëkk ba boole na ay xeet yu bare. Amoon na ci bu jëkk waa Firisi, ba noppi indi woon nañu waa Gereg ya ak Yawut ya, ba noppi waa Room ya. Ci biir dëkk ba amoon na ñaari pénc yu réy yi ñu defare doj. Benn ca ñoom péncu Tibeer lañu ko tudd, mu am dénd bu tollook 300 meetar kaare, bi doon 'grand palaasu dëkk ba' fu nit ñi doon jaay, di fo, di waxtaan. Kenu yu réy te rafet ñoo ko wëroon. Beneen bi nag, mooy péncu Ogust moo dend péncu Tibeer. Ci seen diggante amoon na benn iskale bu am 12 mars (maanaam tegukaayu tànk), bu nekk am yaatuwaayu 20 meetar. Ca kaw iskale ba amoon na bunt bi ñu defare ak 3 ars yu réy-a-réy. Ab ars mooy lenn li ñu tabax ngir nekk pàttaliku. Dafa am ñaari kenu doj yu réy yi ñu boole ak lu mel ni xala doj bu jaar ca seen diggante, tiim leen. Def nañu bunt bi ngir nekk pàttalikukaayu ndam li Ogust Sesaar amoon ca xeex ya. Ca kawu ars ya yett nañu ay nataal yu réy. Beneen booru péncu Ogust moo doon wenn tundu doj. Ci biir tund wa yett nañu genn xala, rafetal ko ak ay kenu yu kawe ya. Ca diggu xala ga amoon na benn màggalukaay bu réy bi ñu defare marbar bu weex ngir teral seen Yàlla Men ak buur bi Ogust Sesaar. Ñu sooga àggale màggalukaay ba bi Pool demoon fa, ak ars ya bala mu dellusi ñaareel bi yoon. Ancos amoon na itam ndox ca tiwo yi jaar fépp ca dëkk, mu jóge ca benn bëtu ndox ca tund ya nekkoon fukki kilomet ca biti dëkk ba. Indi nañu ndox ak li tubaab tudd 'akwadakk'. Ci diiru 8 kilomet dafa jaaroon ci biir suuf si, waaye 2 kilomet yu mujj yi dafa jaaroon ca kaw pom bu kawe bi ñu tabax ngir yóbbaale ndox.

Seen Yàlla 'Men' la tuddoon. Amoon na itam beneen màggalukaayu Men ca wenn tund bu kawe lu tollook 25 kilomet ca penku dëkk ba. Bérab boobu mooy bérab bu bokkoon ca ña gën a am solo ca seen diine. At bu nekk def nañu benn po ngir teral Men. Gëmoon nañu ne Men mooy yàllay wér-gi-yaram, naataange, ak jàmm, te ku aar bàmmeel ya. Mooy itam yàllay weer wi. Ca nataalam ku niroo nit la woon mu sol yere. Misaale nañu ko ak wenn yëkk tamit ak nataalu weer bu am juróom-ñetti fan.

Sersiyus Poolus, boroom réew mi ca dunu Sipar (Jëf 13:4-12), dafa bawoo Ancos ci Pisidi. Ay bokkam moomoon suuf su yaatu ca gox ba. Moom gëm na Boroom bi Pool demoon Sipar. Xëyna Boroom réew mi moo boole Pool ak dëkku Ancos ba tax Pool ak Barnabas gaaw nañoo dem Ancos bi ñu jóge dunu Sipar.

Ca jamono Pool ndoxaanu yàqute, def yaramu neen, topp nafsu, màndite, lekk suuxu mala bu ñu toggul, te naan deret bokkoon na ca diine. Naka noonu, ñu bare bi ñu xoolee dundinu Yawut yi, ñu tàmbali xeeb diine ji ñu fekkoon, di tàmbali bokk ca diine Yawut ya, rawatina jigéen ñi woomle. Ca dëkku Ancos, jigéen ñooñu ñoo doon jabari magi dëkk ba. Naka noonu Yawut ya noonoo Pool jaaroon nañu ca jigéen ñooñu ngir ñu laaj seen jëkkër ñu dàq Pool ca dëkk ba. 

(Jëf 13:14-51; 14:19-23; 2Tim 3:11)

#Article 26: Yoonu Eŋaca (146 words)

Yoonu nguuru Room wu mag wu tudd Yoonu Eŋaca (Via Egnatia) dafa demoon ci diggante Asi Minër ak Itali. Tàmbale na fu dëkku Istanbuul nekk tey ji ca Géej gu Ñuul ga, jàll Maseduwan ba egg géeju Adiratig. Bokkoon na ca yoon wu ñu jaaroon ngir dem Itali ak Room.

Tali doj la woon. Maanaam defaroon nañu ko ak ay xeex yu ñu yett ba kaare ngir seen ànd jege. Yoonu Eäaca jàll na diiwaanu Maseduwan diggante Géej gu Ñuul ak Géeju Adiratig. Dafa tàmbali woon ca Géej gu Ñuul ca dëkk bu tuddoon Bisansë (Byzanse), mooy dëkku Istanbul, jaar ca dëkki Neyapolis, Filib, Amfipolis, Apoloni, Tesalonig, ak Pela ba noppi dem ba Dirxasiyum (Dyrrhachium) ak Apoloni ca Géeju Adiratig. Guddaay ga mooy tollook 800 kilomet. Nit ñi doon nañu dugg gaal ca Dirxasiyum walla Apoloni ngir jàll géej ga te fekk yoon wa jëm Room.

#Article 27: Arkelawus (120 words)

Ci angale mooy Archelaus; Ci faranse mooy Archélaüs

Erodd Arkelawus, doomu Erodd bu mag ba, moo falu woon ci diiwaani Yude, Samari ak Idume (Idumée) 4 j.K. nguuru ba 6 g.K.. Yaayam Maltas (Malthrace) la tudd. Arkelawus ak Erodd Antipas ñoo bokkoon ndey ak baay. Yawut yi ak waa Samari yi jiiñ na ko kor ci kanamu buuru Room ndax coxoram. Buur bi Ogust Sesaar moo ko fuñ ci diiwaanu Gool (Gaule), maanaam Farans, ci 6 g.K.. Gannaaw loolu def nañu Yude diiwaan ci suuf nguuru Room, te jawriñ yi buuru Room fal yilifoon fa. Jabaram Mariyamënë (Mariamne), doomu Aristobul la, ki mu fase ngir takk Galafira (Glaphyra), jëtunu Alegsàndar (Alexandre), magam.

Man nañu gis tur wi ci Mc 2:22.

#Article 28: Armagedon (117 words)

Ci làkku ibrë (הר מגדון) la tur wi jóge.
Ci angale mooy Armageddon; Ci faranse mooy Harmaguédon

Armagedon mooy turu benn tund ci làkku ibrë bi ñu sotti ci làkku gereg. Ci làkku ibrë Megido (Meguiddo) la tudd. Ci Injiil dafa misaale bérab fu xare bu mujj bi nara am ci diggante gaayi Yàlla yi ak gaayi Seytaane yi ci muju jamano ji. Tundu Megido bokk na ci tundi Karmel yi. Dafa nekkoon ci benn boru xunt mu mayoon nit ñi jàll tund yi. Ci joor bu nekk ci taatam la Sóol (1Sa 31:1-8) ak Yosiyas (2Ch 35:20-24) dee, te Sedeyon amoon ndam ci waa Majan ñi (Jud 7).

Armagedon mooy feeñ ci Injiil ci Pe 16:16.

#Article 29: Aten (933 words)

Ci angale mooy Athens; Ci faranse mooy Athènes

Aten dëkk bu mag la, ci réewu Geres mooy péey ba sax, te siiw na ngir xam-xam ba'ak njàng ma, ak caada ja. Yaakaarees na ne lu ëpp téeméeri junni ciy way dëkk ñoo fa dëkke. Nekkoon na péeyu nguuru waa Geres, bi tuddoon Atig (Attique). Tey mu tudd Aten . 

Sancees na Aten daanaka 3.000 at Nj. Is (njëkk Iisaa). Daanaka 500 at njëkk Iisaa fekkoon na mu am nguur gu yaatu lool. Waaye Geres dafa ñàkkoon suuf. Moo tax waa Geres yi tuxu, di sanc ay dëkki Geres yu bari ca Tugal ak Asi gu ndaw gi. 

Moone ca jamonoy Pool dafa ñàkk xaalis. Amatuñu nguur, te diiwaanam Atig dafa tuuti - dénd bu tollook 2.600 kilomet kaare matul sax benn departemaŋ ca Senegaal. Amul feneen ca Atig fu gën a sore Aten 40 kilomet. Seen suuf musuñoo doy seen soxla. Taw bi barewul woon, lu tollook taw bi ñu am ca noru Senegaal. Ñetti cér ca ñeent ca suuf si amul njëriñ ci bey te yu bare ci yi des amoon njëriñ ca bey garabu oliw rekk. Amoon nañu mbélli xaalis waaye fekk nañu ne jeex nañu tàkk laata jamono nguuru Room. Tamit seen doole ci jaay wàññiku na, ndax doole yeneen dëkk yu mel ni Ancos, Korent, Efes, ak Alegsàndiri.

Dëkku njàng la woon, bu amoon jenn daara ju kawe 'iniwersite'. Naka noonu siiw nañu ndax seen xam-xam ak seen waxin, ndaxte waxin lañu ca gën a jàngale. Wax ak a déglu lu bees rekk lañu daan xinte. Amoon na ay mbooloo boroom xam-xam. Benn ca mbooloo boroom xam-xam moo tuddoon Epikuren. Kureel la woon, bi sës ci njàngalem Epikuur (mu faatu 270 at lu jiitu jamano Kirist) te fonk bànneex, ba mucc ci bépp tiis. Gëmuñu Yàlla, waaye ñu gëm ne àddina dafa sàkk boppam te amul boroom. Te boo deeyee amul dara lu ciy topp. Nekkatuloo daal. Beneen mbooloo dafa tuddoon Estowisen. Kureel la woon, bu sës ci njàngalem Senon (mu faatu 265 at lu jiitu Kirist). Fonk nañoo naagu, ba bañ a yég dara, muy bànneex mbaa naqar.

Dëkk bi fees na dell ak màggalukaayu yàlla yi ñu defare marbar, yu réy-a-réy te rafet, nataal ya ñu yett, kenu ya, robine ndox bi ñu tudd 'fonteen' ak yeneen rafetaay. Ca diggu dëkk ba amoon na benn tund wu am ay màggalukaay rekk. Ëpp nañu fukk. Nekk na daanaka 100 meetar ca kaw niwo dëkk ba. Ca ñetti boor am na mbartal bu jub xocc mel ni miir. 'Akëropool' la tudd. 

Benn ca màggalukaay ya moo doon màggalukaayu Sës, yàlla ju gën a mag ca diine Gereg. Àggaleeguñoo tabax màggalukaay ba ca jamono Pool. Waaye ba noppi amoon na 104 kenu marbar, bu nekk am kawewaayu 17 meetar ak yaatuwaayu 2 meetar! Kawewaayu màggalukaay ba moom ca boppam moo doon 27 meetar. Ca biir amoon na nataalu Sës bi ñu defare wurus ak iwaar. Bokkoon ca ñeenti màggalukaay yu gën a réy ca àddina si ca jamono. 

Màggalukaay bu gën a am solo moo doon li ñu tudd 'Parténon' bi ñu defaroon ngir yàllay dëkk ba, maanaam, Atena. Guddaay 72 meetar la, yaatuwaay 34 meetar, te kawewaay 20 meetar. Ca kaw kenu ya amoon na nataal bu ñu yett bu wëroon tabax bépp ca 92 wàll. Wàll bu ne indi na benn ca seeni nettali yàlla. Amoon na beneen nataal bi ñu yett ca diggante kenu ya bu amoon 600 melo ya - ay góor, ay jigéen ak ay bàyyima yi bokk ca ña indi seen yàlla Atena benn yére wurus at bu nekk. Guddaayu nataal bi mooy 160 meetar. Te def nañu nataal yi ngir ñi taxaw ca suuf di ko xool yaakaaroon nañu ne dañuy jàkkaarlook nataal ba, fekk na ne nekkoon na 10 meetar ca seen kaw. 

Waa Aten jaamu nañu ay yàlla yu bare. Waaye yàllay dëkk ba moo doon Atena. At bu nekk ci weeru yuuliyoo, amoon nañu benn màggal lu diir 8 fan. Ca fan yu jëkk ya def nañu ay joŋante, rawante gaal ya, fas ak sareeet ya, rawante ca woy ak nettali, ay mbumbaay. Ca juróom-benneel ba fan, ca fajar, saraxalekat ya ak magi dëkk ba, jiitu nañu mala ya ak waa dëkk ya yépp, ñu dox ca biir dëkk ba, ba egg Panténon fu ñu def sarax ya, te ñépp lekk yàpp. Sarax nañu 100 mala, mooy nag ak xar, at mu nekk.

Amoon na bérab ci biir dëkku Aten bu tudd Areyopas. Nekkoon na ci kaw wenn tundu xeex wu kawe. Amoon na ay siis yi ñu defare woon doj ngir kureelu dëkk ba manoon faa daje. Indi nañu Pool foofu ngir mu waareji.

Ni dëkki Gereg yépp amoon na pénc bu ñu tudd 'Agora'. Amoon na ñaar sax - benn bi waa dëkk ba tabaxoon ak benn bi waa Room tabaxoon. Ay péncu doj lañu yi ñu rafetal ak kenu yu réy ak nataal ya. Ñoo doon maase, ak grand palaasu dëkk ba, te fu ñu doxale nguur. Foofu itam amoon na ay màggalukaay ak ay saraxalukaay. Ci dëgg-dëgg mënuloo dem fenn ca dëkk ba te gisul benn màggalukaay walla nataalu yàlla. 

Amoon na ay powukaay itam. Ñoom itam dañuy kéemaane. Benn ca ñoom woyuwaay la bi ñu teg ne mooy bu gën a rafet ca àddina si. Beneen mënoon na toogal 17.000 nit, te léeg-léeg dina fees ba ëpp loolu sax! Amuñu jot a lim bépp tabax bu yéeme bu nekkoon ca Aten bi fa Pool ganesi. 

Dëkku Gereg la woon waaye amoon ay Yawut itam.

Aten dafay feeñ ci Injiil ci Jëf 17:15,16,21,22; 18:1; 1Tes 3:1.

#Article 30: Alxuraan (184 words)

Téeree ngii di benn ci yi ñu gën a yër ci àdduna bi, mooy téere bees sellal ci lislaam, di fi jullit ñiy ball-loo seen yoon di Shariiha, ak ci sunna siy dundiinu Yonnant bi (jàmm yal na nekk ci moom), kon nag bu am solo la lool fi jullit ñi.

Alxuraan: Alxuraan mooy téere bu sell bi ñeel jullit ñi, mooy balluwaay bu njëkk bi ñeel yoonal gu Lislaam gi, ci ginnaawam la Sunna di ñëwe. Li njëkk a wàcc ci Alxuraan it mooy laaya wi njëkk ci saaru Halaq muy : «Jàngal ci sa turu boroom bi bind (sàkk) »

Alxuraan nag mooy waxi Yàlla ji mu wàcce ci Yonentaam ba Muhammad, Jibriil nag mooy ndawul Yàlla tey malaaka mi ko wàcce; ngir nag Yonent bi jottali ko nit ñépp,. Moom nag fa Yàlla dees koo bind ca àlluwa jees wattu ja (Lawhul Mahfuus), àlluwa jii nga xam ne Yàlla bind na ca lu nekk njëkk mu koy sàkk. Wattu googu nag Yàlla la soob, mu bëgge ko noonu, noonu la ko waxe: «Nun noo wàcce Alxuraan, te nun noo koy wattu»

#Article 31: Wolof (làkk) (742 words)

Wolof làkk la wu ñuy wax ci Gàmbi (Gàmbi Wolof), Gànnaar (Gànnaar Wolof), ak Senegaal (Senegaal Wolof). Mi ngi bokk nag moom wolof ci bànqaasub atlas bu làkki Kongóo yu kojug nit ñu ñuul ñi. Mbokkoo gi mu am ak làkku pël lu yàgg la. Am na it lumu séq ak yeneen làkk ci gox bi niki séeréer, joolaa ak basari.

Bi ñu demee ba gis jëmm ja, muy ku sew, tuuti te xaw a wow, waaye di ku ñu muure ab taar, ci anam gu woyof te loyox, di ku ñu aare kàttan, sóob ko ci ag fonk-sa-bopp doonte ag neen la, solal ko yéerey yëgle ak jaral, te ma jëli loolu ca jafeem gaa jëli. Bi loolu amee, dama ne leen xanaa kay du kii ngeen ma doon wax? ñu ne ahakay, cis lëf, cig yéemu, ak ñàkk a xalaat ne dinaa sikk mukk ci moom, ma jug man, xajal leen foofa fépp.

Ma ne nag waaw ku mel nii, ci li mu làmboo ciy melo, lu ko nit di doye ?
Ginnaaw bi nag dégg naa ñuy wax naan moom de bokk na ci ñi gën a jekk ci boobule gox, ànd ak jaaxle ci samaw jëfiin, ci ba ga ma ko fa ba, ma ne leen man : moo xam!
Lii mooy li am ci sunu làkk wii, walla yii di yu Afrig yi, dañu di yu am solo te man a dem ni yépp di deme, am barab ci digg barabi làkk yépp, waaye li nu dal nun waa Afrig, mooy li dal sunu lépp, dalaale ci li muy dal sunu kàllaama yii nga xam ne wii de bokk na ci yi gën a nosu, gën cee nooy, gën cee nangoo defaru, yéwénu, ruy, ci ku ko ruyal, tey way nag ca nanu bëgge mu waye ni.

Ana nag ku am janq bu mel ni bii cib taar, nangoo ni, joŋee ni, jekke ni, man nee toppatoo, nangu nee jëme kanam, waaje ni ngir lemu ci say bëgg-bëgg, ana ku am ku mel nii, looy xoolati ku sewe nii, ràgge ni, te taaroodi ni? 

Li ma bëgg a wax mooy naka la nu bëgg a bàyyee sunu làkk yii, rawatina wii di wolof, ca nooyam ga, ak nangoom ga, ak gàttam ga ak noppaleem ga, taaram ba, leeram ga, manam gaa leeral ak yaatoom ga, ak ruyu gi mu nangu, naan dangay jëlati weneen di ci sonn ak a sonle, naan day wa gën? Ma ne ñoom ñoo gis loolu man de déet !

Wolof mooy làkk wi ñu gën a wax ci Senegaal, waaye ngir doyodig waa Afrig yi ba leegi, frañse mii nga xam ne lu matul 30 cib téeméer ci doomi Senegaal yi rekk a koy wax moo fiy làkk wu njëkk, maanaam wi nguur gi di waxe di ci liggéeye.

Ni ko gëstukat yi waxe, làkku wolof am na ag mbokkoo ak yeneen làkki Afrig yu bari, yu mu bokkal i maam. làkk yi dañ leen a séddale ci ay wàll: bu ci nekk ñi am ag mbokkoo lañu fa def. Nee nañu wolof ci wàll gi ñuy woowe bànqaasub atalaas bu làkki Kongóo yu kojug nit ku ñuul la bokk. Am na ag mbokkoo ak pulaar ak séeréer ak joolaa ak yeneen.

Daanaka ñoo ngi koy làkk ci Senegaal gépp, bëj-gànnaar ba bëj-saalum, penku ba sowwu.
Donte wolof da di làkku askanu ñi ñuy woowe ay wolof, waaye kàllaama wolof amul uw dig. Dem na ba romb dig (frontiere)yu Senegaal àgg ba Gàmbi, Gànnaar ba Mali, ci ñaari dëkk yu njëkk yi sax boole nañu ko ci seen i làkki réew. Daanaka gox boo dem ci Senegaal am nañu waxiinu wolof wu wuute: am na wolofi waalo-waalo, jolof-jolof, saalum-saalum, wu kajoor-kajoor, wu baol-baol ak wu lébu.

a - à - aa - b - bb - c - cc - d - dd- e - ee- é - ée - ë - ëe - f- g - gg - i - ii - j - jj - k - kk - l - ll- m - mm - mb - n - nn - nc - nd - ng - nj - nk - nq - nt - ñ - ññ - ŋ - ŋŋ - o - oo - ó - óo - p - pp - q - r- rr - s - t - tt - u - uu - w - ww - x - y - yy.

#Article 32: Ahmadou Bamba (6368 words)

Ahmadou Bamba
mooy ki taxawoon jàmmaarlook tubaab yi, ngir xeexal lislaam, te desal fi sunu ag dëkk ci Afrig tey bég cig cosaanoo fi, kon njukéel ko war nanu, kii moy ki taxawal yoonu Murit, tey ki taalif lu sakkan ci diine, indi ay gisiin yu bees, ginaaw bi nu ko sonnalee genne ko ay yoon réewam

Li ma tax a jug, jëme ma ci def bile ligéey, te ma jàppe ko muy bu am njariñ, mooy, benn: jortu ne, ci def gi, ñi ngi ligéeyal Sëriñ bi, waaye it xeet wi, ndax jël lu mel ni jaar-jaari Sëriñ Tuubaa, ak li mu làmboo ciy njariñ, nga tas ko, teg ko ci fu loxol ku nekk jot,yombal ko ba ku jug man koo xam, man koo dégg , man cee jariñu, ca anam ga mu gën a yombe, gënnee leere, te yaakaar naa ne def ko ci wolof , ñeel wolof yi,ci anam yiy yombal la, tey leeral,lu mel ne lii de yaakaar naa ne amul lu ko gën di ligéeyal Sëriñ bi,waaye ag ligéeyal sa xeet it mi ngi ci, ndax ag dundal la, ñeel saw làmmiñ, te gis naa ne lu waay man a xame ci làkk, ak wu mu man a doon, ci sa wos, lay gën a dugge,lay gën a tooge,lay gën a nekke, luy dund ak yaw, ci lay doone kenn ci yaw, ngay yaw itam kenn ci moom, ngéen di benn bu dul ñaar, gis naa ne bokk na ci li ñiy rawe di rawe, di jànge ci seeni làkk, di ci waxe, di ci xalaate, te di ci jokkoo.
Man de bile téere,njëkk ma koy tekki, nekkoon na di bob,dees na soxla as lëf ci waxtu,ngir yër ko,dégg ko,naan ko,waaye daa mel ni bi ma ko defee ci wolof,soxlaatunu lu dul lu néew, ngir jaar ci, jaarati ci, kon nanu fonku sunu bopp,ci fonkaat bu baax sunu làkk yii,te xam ne dug fonkadi ñeneen ñi.
Ñaareel bi mooy , gis gi ma gis téere bii,di bu jéggi dayo ba ci solo ak njariñ, di delluwaay ci delluwaayi téerey yoonu murit wi,di rootukaay ci yu xam-xam yi.
Làmboo nag kem bu bu réy ci xam-xam, ci lu aju ci Sëñ bii, di kenn ci ñi ñu war a xam, bu ma waxul ki ëpp solo ci ñoom .
Kon xam leen ne yii ak yeneen yu ma waxul, ngir bañ a guddal, ñoo sabab firi gi, nga rax ci dolli,nekkug aji taalif ji, di kenn jëllewaayi yoon wi,yu xam-xam.
Ndax kat, boo yëree, da nga ko gis lu bari mu naan Sëñ bi nee na ma, te loolu du lu yomb . Kok bëkk-néeg la woon ci bëkk-néeg yi,bu ma waxul ngën ji bëkk-néeg
, kon kooku maneesu koo gën di jëlewaay, mbaa delluwaay, rawati na muy ku ñépp xam ag sellam, akug dëggoom, yal na nu Yàlla taas ci barkeem te dolli ngërëmam ci Sëriñ sunu,Sëriñam,laafaale ko, ci barke ku nu ligéeyalam, ak ki muy ligéeyal moom mu mujj mi, Aamiin,yaw boroom mbindéef yi. 

Bii mooy teereb Irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim, di ci maanaa nàndalug aji naanaale ji (ki ngay toogal di naan) ci ndox mu neexum sopp jëwrinu yonant bi , di xam-xamu jaloore bu nu gàttal mu ñeel nag ki bëgg a am ab xam-xam ci dundug sëriñ Ahmadu Bamba yal na  yàlla dolli gërëmam ci moom ,te jariñ ñu ci,amiin.
Ki ko taalif it di ku xeebu ku aajowoo ndimbalul boroomam ak yërmaandeem,tey yaakaar ci moom mu jéggal ko ay bàkkaaram,te làqal ko ay ayibam,yi feeñ ak yi nëbbu,fii ak fan jëm,di Muhammadul Amiin JOOP doomi sheex Ahmadu JOOP mu dagana,yal na leen yàlla boole jéggal.
Di it taalibeb sëriñ Tuubaa, yal na ko yàlla gërëm te jariñ ñu ci moom,amiin.

Maa ngi ñaan yàlla mu musal ma ci saytaane mu nu jam mi,di tàmblee nag samay wax ak jëf ci turam wu tedd wi,moom mi yor yërmaande ju yaatu ji matale mbindéefam yi ci àdduna,te di ko jagleel ñi ko soob ca àllaaxira,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci sunu sang,Muhammad,ak ñoñam aki saabaam.

Aji xeebu ju yitewoo yërmaandey boroomam,ak ndimbalam ci ligeeyal yarkatam bii dib soppeem(di sëriñ Tuubaa) - aji xeebu jooju di Muhammadul Amiin JOOP doomi Sheex Ahmadu JOOP mu Dagana, nee na: ag cant ñeel na yàlla miy leeral àddinaam ji ci wàlliyoom yi,di feeñalati ci ñoom yoonu yonantam yiy gindee,yoon woowu di wu weetal yàlla ak jaamu ko,mooy yoonuw boroom xel yiy dàq lu dul yàlla ci seeni xel,tey jànge ag njub ca yooyale imam,ci jox leen seen bopp,jébbal leen seeni mbir.
Ndax kat ñooñu, ñooy ñi yàlla naan ci alxuraan: ulaayikal lathiina hadaahumul laahu fabi hudaahumuqtadih muy ci maanaa ñooñu,ñooy ñi yàlla gindi kon royal ci seenug gindi.Di julli tey sëlmël ci yonant bi.

Leegi nag ginaaw yàlla day xéewale xarnu bu ne aw waliyu wu koy gindi di ko won yoonu jub ,di ko tee jàdd, nun waa xarnub fokk ñeent nag mu defal nu,xeewal gu tollu ne sunu mbég mii di sunub sëriñ tey sëriñub julit ñi, Ahmadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah yal na ko yàlla wattu te wattul ko,te gërëmi jëfam,te méngoo ko,moom nag mbooloo maa ngi ko gën a xame ci turu sheex Ahmad Bamba MBÀKKE Xaadimur rasuul.

Bi loolu amee ma, bëggoon a leeral as lëf cig dundam, ñeel ki nar a ñëw ginaawam,te bëgg a xam dara ciy mayam. Man nag maa ngi giñ ci yàlla dellu di ci giñaat naan dey xam naa ni xawma te du ma ci man a wax mbaa indi lu dul la gën a néew,la gën a bari moom bu ko xalaat,ndax manu ma ko ba koy def.
Waaye nag dinaa jéem a nooyal yoon wi,ba ku bëgg te yàlla ubbi ko, barilub xam-xamam, yinkiiwal ko jariñ jaamam yi, ngir sàkku ci ngërëmam,bu ñëwee man cee jaar,ndax kat am na ci addiiz mu sell mi: mbindeef yi njabootug yàlla lanu ,ki ci yàlla gën a bëgg mooy ki ci ëpp njariñ ci njabootam gi. Nee nanu ku taarixal aw wàlliyu mel na ni dundal nga ko.

Kon am leen gàttalug jaloore (jaloore mooy taariix walla histoire) gii ma tudde irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim, may ñaan nag képp ku ci gis lu ko yeemut, mu xam ne gàttub jéegoo ma tooñ,mu jéggalul ma Yàlla te suturaal ma,te bañ koo ngàññi,ndax kat da na ci gisi leneen lu bari lu koy yéem, lu man a wecci loolu ko yéemutoon, ndax téere bii ab muxaddima rekk la ( ag jiital) teere dëgg bi  mooy minanul baaqiil qadiim fii ma aathiris zheixil xadiim muy ci maanaa xeewali aji des jiy aji jiitu,ci ngënéeli Sheexul Xadiim.Doomam ja Sheex Muhammadul Bashiir  defoon ko,yal na ko yàlla sàmmu te guddalu fanam,te jariñ ci lu bari jullit ñi, ni baayam,moom dey teere bu boole la te wattu,te dib dër bu naat ñeel ku bëgguw yiw te di ci dox. 
Yal na ko yàlla mottali te nangu ko,te tas ko ci àddina bi,muy ndëxëñtéefam ëlëg ca àllaaxira,tey lu nu koy fàttalikoo ginaawam ci fii fi àdduna,ci barkeem ak ci barkeb ki ko taalif ak ki mu ko taalifal,yal na nu yàlla nangul,te nangul nu sunub teere,matal ko te tas ko moom itam. Moom kat yàlla mooy aji kawe jiy boroom ngënéel ak tawfeex,tey boroom li fii ak la fee.

Sëriñ baa ngi gane àdduna - ci li nu wax - ci atum junni ak ñaat téeméer ak juroom ñaar fukk 1270 g, am ñu ne atum junni ak ñaat téeméer ak juroom ñaar fukk ak ñaar 1272g,ca kër waajuram wu goor ca Mbakke Bawal ,mu nekk leegi ca wetu yoonu saxaar ga. 
Boroom xam-xam bu mag bi nuy wax Alhaaji Hamidin doomi Usmaan Alfuutiyu Altilriyu nee na: (( sëriñ baa ngi gane àdduna moom mi sunnawoo sunnas yonnant bi,ci atum sharaha,muy 1270g làqu atum shumoos muy 1346 g te booba mi ngi am juroom ñaar fukki at ak ñeent mel ni ay jant. Am ñu ne juroom ñaar fukk ak ñaar,ci guddig àllarba ci ñaar fukki fani muharram)).

Moom sëriñ bi, bi mu ganee àdduna ,waajuram wu jigeen a ko yoroon ba mu mat a jàngi, Mu tudoon nag Amadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah doomi Muhammadul kabiir mom Habiiballaah mu njëkk ma doomi Muhammadul Xayri,ak Muhammadul Kabiir .
Muhammadul Kabiir mii mooy ki niy wooye Maharam,mooy ki sanc Mbàkke Bawal atum 1194 g ,ci li nu wax,waaye dëkkewu ko woon da faa bàyyi woon ab taawam Muhammudu Farimata,magi habiibullaah waaye bokkunu nday,moom nag sëñ Maharam mii daa desoon Jolof, fa la làqqoo nu denci ko fa,di ko siaare. 

Mi ngi askanoo nag ci Tukklóor,ay waajuram a ngi bawoo Fuuta,dem Jolof,  siw na itam ne ñoom Gànnaar lan bawoo, dem Fuuta,seeni doomi baay tëx ci naar yi ñooy ñoñu Moodi Nalla, ñoom nee nanu ay serif lanu.Sama mag, sama sëriñ, sheex Muxtaar binta Loo,doomi sheex Iraahiima ,sëriñub Njumri Loo nettali na ma ne dégg na ci sëriñ bi luy dëgëral loolu,mu ne bis nekk na fa sëñ ba nuy waxtaan ba tudd ag giir ci naar yi,gu niy askanale ag cëriif,sëñ bi ne ko xanaa xamoo ne ñooñu suniy mbokk lanu,mu ne ci noonu la xame ne ñoom ay sëriif lanu.
Man nag li may wax mooy seenug cëriif bu nu ko waxutoon te déggeesu ko it,seen jikko yu rafet tegtale na ko,muy tedd gu ànd ak yaatug dënn,ak lewet gu ànd ak njàmmaar,ak jublu ciw yiw,ak bañ jikko yu suufe yi,ak diinewu gu dëggu.

Yaayam soxna Jaaratul Laahi Maryama BUSO doomi Muhammad mom Muhammad mom Hammaad mom Alliyu Albusobiyu, ñooñii seenug cëriif lu wér la, ñi ngi cosaanoo ca Imaam Hasan mom Alliyu ibnu Abii Taalib karramal laahu wajhahuu, kon sëñ bi seriif la ci nday ak ci baay. Lenn ci samay doomi baay tëx nettali na ma te moom ku dañ kumpa la ci suufus Fuuta ,mu ne dox na bis juge ci dëkk bu ndaw bu nu naan Bukke, jëm fu nu naan Mbumbe, péeyub Filaaw,nee na mu romb ci ay gent yu ñu ne ko ñooy fi Mbàkke-Màkke yi dëkke woon.                  

Am na ku ma nettali ci ñi sant Ba,ne Mbàkke-Mbàkke yi seeni doomi baay tëx lanu, kaaf gi nekk ci Mbàkke ag Haa la woon muy haa giy mujj ci ba,wolof yi def ko kaaf,waaye wax jooju, ju doyadi la fi man,li nu jortu daal mooy aw sant wu yàgg la, niki santi ajam yi,(ajam mooy ku dul araab),li fi ne daal mooy ñaari wax yi bu ci nekk, dëgër na te am na màndargaam dëgg. Waaye Buso-boso yi ñoom seen cosaan Fuuta la, ca fa niy wax Golare, barab yii yepp it yu jegee lanu,barab yii it,ak wax yi ci am,am nanu màndargay dëgg,yuy tegtale teddngay ñaari askan yi.

Bi Sëriñ bi tollee ci war a jàngi,wayjuram dal di koy jébbal nijaayam Muhammad doomi Muhammad BUSO mbokkum ndayam ju tedd ju yiw ja. 
Mu tàmbli koo jàngal ba mu màgg as lëf ,tàmblee yewwu, mu jebbal ko moom itam nijaayam,sëriñ Tafsiir Mbàkke Ndumbe doomi Muhammadu Soxna BUSO doomi Muhammadul Kabiir mi nu tuddoon,moom mooy mbokkum maami sëriñ bi, ju jigéen,ndayi wayjuram wu jigéen,soxna Asta Waalo. Nu daan nekk foofa, fa moom ca Mbàkke, bu noor baa, bu nawet baa, lu ci ëpp danu daa  dem jolof, ba bi Tafsiir mii làqoo te booba sëriñ baa ngi jeggee mokkal.

Kenn ci ñunu woolu ñi nettali na ma ne, sëriñ bi nettali na ko ne àlliwaam  a ngi tulloon ci latajjidanna  bi jànglekatam boobu di làqu,mu dal di dellu ca wayjur wa, dal di farlu ci njàng mi ba mokkal alxuraan , def tajwiid ak tas-hiih,ca ña ko daa defale ca jamono jooja, loolu lepp ci wetu baayam,daa wul tàggalikook moom lu dul lu néew,ndaxte magam Muhammad Jaara dafa nekkoon ca kenn ca tas-hiihkat ya ca yeneen dëkk ya.Bu ko defee leeg-leeg amaa na mu jaar fa nekk fa ak moom weer,walla ñaar,doog a dellu,booba ña nga Saalum,ca jamonoy jiyaadkat boobu di Màbba Jaxu,ndax kat booba ñoñam Màbba boole woon na leen ca ñam pangoon jëme Saalum,nga xam ne Bawal ak Jolof daanaka bawu fa woon kenn. 

Bi mu faatoo nag moom Màbba, nit ñi dal di dellu seeni dëkk , waajuram wi moom itam dellusi ci ñi doon dellusi, ànd ak Latjoor. Ci noonu nijaayam akug njabootam des foofa,sëriñ bi it bokk ci,ngir jàng xam-xam,noonu mu tàmbli di jàng ci baay tëxam,Samba Tukklóor KA doomi bàjjani baayam,bi mu jàngee ci moom dali xam-xam,tàmblee ñaw as lëf, la dellu ca baayam,te booba ma nga Paataar,benn dëkk bu ndaw bu nekk ca wetu njéndul Amadi Yala,dëkkuwaayub Latjoor ca joojale jamono.
Ndax moom sëñ Mammoor daa defoon ku Latjoor fonkoon lool,daa ko laaj tey diisook moom,waaye moom sëñ Mammoor bëggutoon a dëkk ak moom,ndaxte du woon ku xemmeem seen alal ji,du caagéenug seen teddngay nguur gi,li ko loruloo woon ci mu dëppoo ak ñoom ak a mudaaranteek ñoom mooy njaboot gi mu yoroon,bu ko defee Latjoor daa ko dëkkal ci wetam,waaye sëñ bi daawul nangoo dëkk  ak moom,moom kay day dëkk  ca wetu péey  ba mu  ne rekk,ndax da daa jàng ak a jàngale,te jàng ak a jàngale neexoowut aki buur,li fi ne daal ca wetam la dëkke woon,nga xam ne su ko soxlaa ñëw ci lu dulub coona. 

Ci noonu sëñ bi nekk  ak waajuram,di jàng ci moom te di farlu ci mokkal gi,ak xereñe gi ak dégg-dégglu gi,ba faf raw ci fann yi. Ci biib diir it daa na ci def leeg-leeg mu seeti sëñ Xaali Majaxate Kala,moom mi dëkke woon fa péey ba ak Lajoor,di woon ku raw ci fanni xam-xam yi, rawati na làkkuw araab,di ku siiw ci man a woy,bu ko defee muy xamlu ci moom araab,leeg-leeg it mu daa ko indil ay woy,yu mu def ngir mu toppal ko “lihraab” ba ak araabe ga,ak “harool” ba,leeg-leeg mu génneel ko ci ab yàq,ba mujj sëñ bi far ko raw, mu mujj saa su ko wonatee  lenn ci woyam yooyu,mu ni ko indil ma ko, ma mokkal ko,mu mujj toppalatu ko waaye day mokkal li mu koy indil,nii la nekke woon ak Xaali. 

Amoon na fa it beneen boroom xam-xam ci waa-gànnaar yi,dëkke woon Njaañ, tuddoon Muhammad mom Muhammadul Kariim,bokkoon ci giirug Daymaan,ci doomi Seyidil Faadal yi, ñu gënon koo xam nag ci turu Muhammadul Yadaali,waaye bokkul ak ki def téere bi nu naan Zahabul Ibriiz ci tafsiir,ndax kooku am Yadaalim Daymaan mu yàgg la . Sëñ bi bariwaa na lu mu ko daa dikkal,di jàng ci moom xam-xamu Bayaan (xam-xamu wax ju rafet),yaakaar naa ne nee na it - ci lenn li mu nu daa nettali yàlla a xam - ak  bu Mantiq (xam-xamu xellu).
Bi wayjur wi xamee ci moom raw gi ak cawarte gi ak laabiir gi,mu dal di koy jox mbirum njàngale mi. Bari na lu mu ko daa jàngal ab bind ci kanamam ci téereb boppam ba ,walla ci téere bu mu dalagul, ngir mu jàngal ko boroom bind boobee walla téere ba, bu ñëwee,ngir wóolu gu mu wóolu xam-xamam akug ñawam, sëñ bi it daan ko def,ba li ëpp ci dongay sëñ Mammoor yi mujj féetesi ak moom,doylu ci moom,waajur wi bàyyi leen ak moom te bég ci. 

Waaye yàggul dara rekk Latjoor tuxoo Kër Amadu Yala,dem Sukeer péeyam ba ca Kajoor,yobbaale sëñ Mammoor mu sanc ca wetam,tudde ko Mbàkke Kajoor,sax fa ñaari at dal di wuyyuji boroomam,nee nanu, looloo ngi am ci Muharram,atum 1300g, dëgg naa ci sëñ bi mu ne bi waajur wi tollee ci sukkuraat, took na fa boppam wàcce fa ab kaamil bisub altine,guddig talaata mu làqqu,nu denc ko Deqale ,di ko siyaare,man dey Alhamdu lillaah dem naa fa ba siyaare ko. 

Bi niy yobbu wayjur wi Deqale muy dëkk bu ndaw ci dëkki Kokki yi,ci wàllug Mbaakol,sëñ bi àndon na ca gunge ba,di liiru,bariwaa na bu ko ab gawar bëggee joxuw fasam,mu ne dox a ma gënal,bi mbooloom dëkk bépp dajee di mbooloo mu kenn masta gis,nu jublu ci jullee néew bi,jiital sëñ Tayba Muhammadu Ndumbe Maar SILLA, mi nu  tuddoon ci buntub seedey ñu mag ñi ñeel kii nuy wax ci moom. Bi nu noppee ci julli gi,ak denc gi,sëñ Tayba digale nu daje te dal,te xerawlu,ci noonu mu jug, xutba,waar nit ñi,wax wax ju rafet bi miy jaale sëñ bi nit ñi,bi mu noppee ne ana Sëñ Bamba,noonu la nu ko daa wooye ñoom,ca jooja jamono,mu wuyyu jug,ma nga woon ca catul mbooloo ma,sëñ Tayba ne ko jegesil,mu xaw a jege bay degganteek moom,di gisanteek moom,di ko man a toontu ci lu dul muy yekkati kàddoom,dal di yam foofa ngir bañ a jéggi nit ñi,xutbakat bi neeti ko jegesil,mu ne ko maa ngi lay dégg,Sëñ Tayba dal di koy jaale njaal mu rafet,ne man nag dama doon sàkku nu ànd ci mbooloo mu màgg mu sa moroomi waajur wii,ngir nu seeti Latjoor,jaale ko sa waajur wi,jaale gu ko man a dëfal,ngir kat moom ab xaritam la woon,dib soppeem,te dib sëriñam,daa diisook moom,bu ko defee nu waxtaan ak moom ci yaw,sampu la fa moom,ba mu man laa teg fam tegoon sa Baay,bu ko defee doo gis ci moom lu dul aw yiw ak teraanga,lii daal mooy sama xalaat,yaw nag luy sa xalaat,sëñ bi ne ko,li aju ci jaale gi ak dëfal gi maa ngi la ciy sant,te di la ci ñaanalub yool,waaye mbirum seeti ay buuri àdduna moom duma ko def,ndax xemmeemu ma seen àdduna ji,te soxlawu ma seen teddnga,teddnga ci yàlla laa koy sàkkoo buurub buur yi,mbooloo ma tiit,tas.

Ña cay ñu baax wax ji da leen a yéem, rusloo leen,ndax dëggu gi mu dëggu, tey toroxal way bëgg yi àdduna,juge ci seen doom ju diw waxambaane,tegi tànkam ci seeni wagg te manu ñu ci dara. 

Bu dee mbooloo mi moom, li leen yéem mooy,bañ gi mu bañ teraanga ju teew jii,ak xéewal gu jàppandi gii,nu ne kii daalub dof la,ci loolu Sëñ bi def na ñaari dagiiti woy yu rafet te yéeme,bu njëkk bi mooy waxam jii:
nee nanub dof laa,ngir wëlbati gi ma wëlbati samab gis wëlif leen ba fa mu yam ,teewluwu ma ko te woneesu ma ab yaxam jamono ja may liggéey,waaye beneen bi moom mooy wax jii:
nee nanu ma jéngal jëm ci bunti buur yi,kon déy da nga am ay may yu lay jariñ jamono ju ne)). 
((Ma ne leen yàlla doy na ma,doyloo naa ko,soxlawu ma lu dul xam-xam ak diine))
((Yaakaaru ma te ragalu ma ku dul sama boroom,ndax yàllaay ki may doyluloo te di ma musal )) 
((Nu may joyale samay mbir jëme ko ci ñoñ lottu nanu ci seen mbiri bopp,ni miskiin yiy lotte? ))
((Walla nan la ma bëgg poñatum àdduna bii di jañe,jëm ci dëkkaale ak ñoñ seeni kër mooy dërub saytaane ))
((Su ma dee naqarlu mbaa may bég boroom Aras laay woo. Mooy Aji dimbali, ji dara dul të,te mooy Kiy amal li ko soob )) 
((Bu bëggee gaawalum mbir loola gaaw,bu ko nammee yeexal mu yeex ba cib diir)) 
((Yaw mi may yedd bul sonal sa bopp , ndax kat man amu ma lenn lu ma naqari ci ñàkk àddina ))
((Bu dee sama ayib mooy dëddu gi ma def ci seen poñat mi,kon déy ayib jooju, ju gànjaru la, ju ma dul gàccaal)).  

Waajuram wu jigeen ,wu tedd waa nga làqoo Poroxaan ca Saalum, nu denc ko fa,jamono ja fa sëñ Mammoor nekkee.

Moom sëñ bi,bi waajur wiy dund, nanguwutoon a taxaw mbaa muy taxawal dara,moom daal ci moom rekk la toppoon ,mel ne néew bu nuy sang, fu nu ko jëmewul du fa jëm, bi mu làqoo nag,mu des ca ligéeyam ba mu ko bàyyee woon at ak lu topp, ña fa nekkoon it jàng rekk a leen fa bàyyi woon, du leneen,moom itam ab jàngalekat rekk la woon,waaye loolu teewul woon mu doonoon ku yitewoon a xam gaa ñu baax ñi,ak seeni xam-xam,ak beru ak a wër,niki ñu baax ñi,mu leen daa junj ciy waxam,ak a feeñal ay maanaa,ak a yëgg,ba bi ko himma ju kawe ji (himma ci lun man a firi mooy yite) dikalee ,muur ko,mu jug yëgg as lëf neeti tekk,dal di woote cig nooy jëme ci mbiram moomu,bi ko mbir mi gënee lëjal nag, gën a fees fi moom,gën a rëy,mu dal di biral woote gi.

Dajale mbooloo mi,taxaw fa ñoom xutba leen,sukkandiku ci dokkub dogu,ne leen yeen mbooloo mi, ku àndoon ak man, ngir jàng rekk,na laxas jëm ca boppam aki mbokkam,mbaa fa ko soob,man loolu rekk taxatumaa jug,ku bëgg li nu bëgg nag,na toog,dal di leen fay bàyyi dugg ca biir.
Waxam jii nag dal di leen bàyyi cig jaaxle, ñenn ñi dem, ña ca des,des fa,am ñuy jeem a tëyye seeni xarit ngir ñu des,ak ñuy xiirtal seen waay ci ñu dem,sëñ bi moom ne tekk rekk,jeemul a tëyye kenn ku bëgg a dem,ba mujj li ëpp ci mbooloo mi dem bàyyi ko fa,la ca gën a néew des fa. 

Bi loolu lépp daata am,fekkoon Sëriñ bi mu sóobu ci ngiirum taalif ci xam-xam yu nu tuxal ,yu sariiya yi, mu woy Ummul Baraahiin,bu Imaam Sanoosi,wayjur wi nangu ko,bég ci ,te mujj di ko jàngale ,bàyyi wesar wa doonoon cosaan la. Dégg naa ci Sëñ bi mu ne woy woowu de waajuram jàngal na ko ñaari doomam yii di sheex Coro,miy Siidi Muhammad Alxalifa,ak sëñ Aafe,mi tuddoon Ahmadul Muxtaar.
Mu woyati teereb Imaam Xazaalii bi tuddoon Bidaayatul Hidaaya,dal di koy tudde Mulayyinuz Zudoor ,di ci maanaa (aji nooyal ji dënn yi ),ginaaw bi  mu gàttal ko,tudde ko Munawwiruz Zudoor,di ( aji leeral ji dënn yi),ci atum 1294g,teg ci Jëzbatuz Zixaar,di (bijjig gone yi) ak Jawharun Nafiis muy ( wurus wu gànjaru wi) nga xam ne da cee woy wesaruw Imaamul Axdariyyu,ak yu dul yooyu. Bi ko donga yi nangulee nag lii mu leen doon woo,daa bàyyi njàngale mi,jëm ca di leen tarbiya,ak a tarqiya (tarbiya mooy yar ni ko sariiya bëgge,tarqiya di yékkatee jëme ca yàlla).

Man nag nee naa lii de du ñàkk muy ndigalug yonant bi (j.y.m),ndax kenn ci sunu sëriñ yi nettali na ma,te moom ku wóor la di ndëërlaay,ne Sëñ bi de wax na ko ne yonant bi (j.y.m) moo wax ak moom ci gimiñam,ne ko yaral sa àndandoo yi ci “Himma” te bu leen yar ci njàng,loolu Sëñ bi gën na koo leeral ci xasida gii:
Bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi ji,yal na ko yàlla dolliy xéewal ak mucc,moom miy leeral suufam si ciy wàlliyu ba yawmal xiyaam,te ku ci ne méngoo nga sunnaam si,di ko ñogal wëlif bidaa,bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi jooju,bégal gu mu bégal jëwrinam jii ci ne ko(fazdah) mooy wooteel ca kaw))
(( Yonant bi (j.y.m) digal na ko  ne ko mu jàngal Muriid yi,ak ku nangu mu laabiire la ci waa jamono,te mooy ki ko àggale ca borooman cig taxliya ( mooy setal nit ki féexal ko ciy ayib ) bégalati ko ci tahliya ( muy ràng nit ki ay takaay,walla sol koy ngënéel).Li mu jublu ci Fazdah ji nag (mooy biralal ca kaw), mooy ji ci alxuraan: fasdah bi maa tuumaru wahrid hanil musrikiin mooy biralal li nu la digal te dëddu way bokkaale ñi. 

Yàlla daa digaloon yonantam bi (j.y.m) mu biral wooteem ga,ginaaw bi mu ko daa yalu,maanaam dëgg-dëggi loolu, mooy sëriñ bi,bi  donn gi mu donn yonant bi matee,ci matalug yàlla (t.s) ,te mu dolli ko ay xam-xam aki hikma,aki leer,aki mbóot,te may ko kàttanug man a yanu wilaaya gu mag gi- bi loolu amee nag mu digal ko mu woote ca kaw,woo mbindéef yi ñu weeru ci moom,di jële ci moom tey def ay ndigalam,di bàyyi ay tereem,ci loolu la waxe: yàlla mi nga xam ne lu ko soob mu def,moo ma jox xam-xam yi,ak seen barke,wattu naa lu xajul ciy téere,kon boo may ligéeyal bul tàyyi.Yàlla miy joxe,jox na ma ci darajay yonant bi,barkeb alxuraan,ak xam-xam yi,jël seen barke def ko ci samam njàngale.Yàlla jël na mbooti laa illaaha illal laah def ko ci samy taalif,yàlla jox na ma te dootu ko nangu,te man kaaraange laa te dib weeruwaay ci ndimbalam.Loolu nag ngënéelul yàllaa,ku ko soop la koy jox. Te nee na ma : neel  wéeru leen ci man.

Ci maanaa sama boroom digal na ma,ma leeral nit ñi ne:man ab wéeruwaay laa tey kaaraange,ku bëgg aw yiw àdduna ak allaaxira,na wéeru ci man. Mu dellu waxaat ne: Murid bu yoqatul ci man de texe na,ci làq ngën ji ay may. Murid bu Yàlla wommat jëm ci mu aju ci man, texe na te da na céru ciy may ))
((Murid bu wéeru ci man de yàlla miy sama dëkkandoo bu kawe bi,def na muy ku texe ci lu kawe njortam)) 
((Bepp murid bu aju ci man,day texe,te ku niy soril la aw ay. Képp ku aju ci man déy am nga ag mucc ci nëx-nëxi àddina ak allaaxira.
Ginaaw bi mu leeralaat ne way gëmi jinne yépp ci jamonoom ,aju nanu ci moom,mu ne : Jinney sama jomono jii dey, ña ca gëm ñépp aju nanu ci man,waxuma ña gëmul.
Mu wattuloo nag ñi aju ci moom, ñuy xàccati ginaaw bu nu jébbaloo ne: toroxte ñeel na ki ma dëddu ,won ma ginaaw,muñ ma,ginaaw bi mu duggee dib murid.   

Dal di leeral lu dig murid,ak lub murid di bëgg,mu ne:

Mu leeralaat ni ab muriid di mel,ak ngértel ànd ak sëriñ bu àgg,mu ne :
Melow ab murid,mooy bañ a bëgg dara ngir yàlla. Ku bëggul lu dul yàlla, àgg fa moom,mu jox ko aw yiwam 

Mu leeralaat ne murid saadiq de am na ay meloom,yoy bu ko amee am wépp yiw: Meloy murid saadiq ci gàttal, ñeent la,ma tënk leen nag ciy bayit ngir ragal woru 
((Dëggal ci bëgg sab sëriñ ba fàwwu,jëfey ndigalam fu mu rote rekk )) 
((Bayyi gaaru ci lu mu man a doon (gaaru mooy di am xalaat ci ndigali sëñ bi), ak doonte ci sa baatin la,ci li nu nettali)) 
(( Ak a tànnal sa bopp la ngay def,ngir sa rafetug njort )) 
((Képp ku boole yile melo ci murid yi déy,da na jot ndëërlaay ya (gaa yu baax ya).
 
Mu biralaat ne kiiraay am na juroom benni cosaan,yu murid bi war a dagg,te malaaka yi dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk, ne:
Kiiraay am na juroom benni cosaan,ku bëgg a àgg da nga leen dog, ñooy baril lekk ak naan,ak a jaxasook nit ñi))
((Bari wax,bariy nelaw,sàggan ci tudd yàlla miy jàmm))
((Gëstul loolu ci Jawaahirul Mahaani,bi sunu Sheex Tiijaan mu nu màggal mi def))
((Nettali nanu ne malaakay Aji màgg ji,dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk,ngir yëram ko,loolu man nga koo gis ci taalifi boroom Hawaarifil Mahaarif

Mu neeti murid saadiq doomi waxtoom lay doon,ne:
Murid Saadiq mooy kuy wëlbatiku ànd ak waxtu wi mu nekk,te du fuglu wa ca kanamam,ndax loolu day teree yéwenal waxtu wi teew
Gëstu leen loolu ci Jannatul Muriidi,téere bi sunu sëriñ Xaliifatur Rasiid def.
Ak lu bokkul ak loolu ,ci li mu wax ci mbirum boppam, mom muridam yi,nga xam ne ,bu nu ko toppoon,indi fi lu yéem xel yi,te da na mujj kon,gàttal gi nu bëggoon ci téere bii,du amati,ndax moom téere bii as kook la ci geejug xamale ko.

Nu indil leen fii nag as tuut,su nu tas ci wone lenn ci sekkarey xaybu yi (xaybu mooy lu faddu,muy mbirum biir niki liy xew te xewagul),mu bégal ci ñi aju ci moom, ngir dolli leen ag xeemeem,ak sawarloo leen,mu wax ne : ((ñi aju ci man bu nu ko defutoon dem sawara,doonte as ndiir lay doon it,njëkk nuy tàbbi ajjana,ji nu dig ñu ragal ñi yàlla))
((Li waral sama tukki bu sori bi,Yàlla mu barkeel mi te kawe,daa bëggoon ca asal,may kiy ramu samay donga,dox na sama digante ak nasaraan yi,tàbbal ci seeni xol ag ragal ma,nu def la nu def nag ngir ma bañ a nekk dib nasaraan, ndax bu ma ko doonoon tabbi sawara ,walhiyaazu billaahi. Waaye Yàlla’a ma aar ci sawara,ak lépp lu mu gëramul,ci darajay Yonant bi (j.y.m))) . Mu bind ay laabiire ñeel murid yépp,ne : Mi ngi juge ci man jëm ci mbooleem murid, yu góor yi ak yu jigéen yi,ab nuyyoo bu teey,bu leen di musal mboole seen,te di leen tabbal ci jàmm ak aafiya,ci addina ak alaaxira,ci barkeb Yonanat bi (j.y.m),ginaaw bi, may digal képp ku aju ci man,ngir yàlla mu kawe mi te tedd,mu xamlu pas-pas yi ak tawhiid,ak àttey laab,ak julli ak woor,ak lu dul loolu ci lépp lu war mukallaf,man nag warlul naa leen taalifal leen mbooleem lu leen koy xamal, ngir jëmmi yàlla (t.s),wasalaam)).

Mu bind lenn ci ay murid ab tontu bu neex yal na nu ci yàlla boole ñun ñépp,mu ne ci: assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa,wa barakaatuhuu,ma lay xamal ni sa bataaxel ba agsi na,yaw murid bu dëggu bi,waaye na la wóor ne doo gis lenn loo ragal,booy faatu ak ci bàmmeel,te ñaari malaaka yiy laaje,xam nanu sa sëriñ,te da nanu doylu ci xam gi, ba dunu la laaj dara. 
Lii nag xamle la gu mu teg ci yoonu laaj ak tontu,laaj bi moo di lan la sëñ bi woo ay taalibeem jëme? lan mooy tontu li? Moo di sellal,moom mi nga xam ni mooy ruuhug jëf tey ngértel xam-xamub way xam ñi yàlla,tey waralug àgg ca Yàlla, àgg ci Yàlla nag ñi ngi ci jublu jaam bi nekk di ku wéetal yàlla,ciy yëggoom ,aki dalam,aki pas-pasam aki waxam,ci lepp,li feeñ ak li nëbbu,lii nag manut a ame ci njàngale rekk,ndax kuy jàngale ab tegtalkat rekk la,li ci des,mi ngi ci aji jàng ji,man naa am mu jëfe man naa am déet,du ligéeyub jàngalekat,muy sonnu ci waa ji jëfe loolule,loolu Sheexu tarbiya la war.

Bokk na ci ligeyam,moom sëriñub yar,jàng ak jàngale,ak ligéeyloo,ak ay tudd yàlla,ak gindee ginaaw bi mu leen xiirtalee cig cofeel gu dëggu,te du tàggook ñoom li feek wonu leen seen ayibi bopp, ligéeyloo leen ci nu jéem a laab ci yooyu ayib,ngir man a àgg ak ñoom fa Yàlla inshallaah. Bu loolu jàllee,mbirum tarbiya day mbir mu gudd,manunu cee wax fii.

Mu dem ak ñoom ci yar leen ci himma, ñu nangul ko ko,mu dox ak ñoom ci ngérum tàggat,dajale leen,di leen ligéeyloo lu bari,yanu leen ci fàttaliku Yàlla lu bari,ak a jàngi xasida,ak taqoo laab,ak a beru,rawati na sori jigéen ñi,ci noonu ñu kawe ñu dul ñoom,ndax donoo joxe woon seen bop ak seen alal ci yoonu sàkku gëramul Yàlla, Yalla jënd na ci jullit ñi,seeni bakan ak seen alal,faye leen ko àjjana,Sëñ bi wéy ci yoon wu jub wii mook saabaam yi, dale ko ci njëlbéenug atum junneek ñatti téeméer ak benn,ba bi mu sancee Mbàkke Bawal,ci at moomu juge Mbàkke Kajoor,sax fa lu tollook ñaari at ,nit ñi di ko dikkal juge fu nekk, ñii di jebblusi, ñii di joxesi àddiya, ñiiy sàkku ndimbal. Mu mujj yoonu këram gi mel ne yoonu ab ja, ci ñeenti at yii nag mu siiw ci,siiw gu kawe, ñu jege ñi ak ñu sori ñi, ñepp di yéemu ci moom,te booba amagutoon sax fan-weeri at. 

Ci diir bii sëñ bi wër na ci réewum wolof mi,dale Saalum ba Waalo Barak,siyaare fa mag ña, ña cay dund ak ña dundul,jaar ca sëriñ sa ,jële ca ñoomi wird,bokk na ci ñi mu siyaare, ñoñ sheex Siidiya,siyaare na bàmmeelam ca Tindawja,siyaare sheex Baaba mom Abiihi ca Maymooni,tagg leen,jële ca ñoom,woy càllaleg xaadir gi,tàmblee ko ca sheex Baaba ba fa mu yam,looloo taxoon kenn ci Sheexi naar yu mag yi laajoon ko kuy sa sëriñ?,mu ne Rasuulul laahi (j.y.m),mu ne ko kon lu tax nga ne fi di tudd waa kër sheex Siidiya,ak a woy ay sëriñ ak a tag?,Mu ne booba da maa melon ne ku gumba,di làmbatu yoon wi,di ko sàkkoo xam ci ku xam ak ku xamul,bi ma dajee boroom yoon wi ci ndimbalul Yàlla nag muy Yonant bi (j.y.m),mu xëcc ma ci boppam,laa wacc ker-keraan yi,waaye di jokkook ñoom ngir Yàlla ak a soppanteek a jariñante ngir moom.

Te wax na dëgg,ndax mbiram ak ñoñ Sheex Siidiya loolu lay tegtale,mujj nanu mel niy doomam mu mel ni seen baay,di leen jariñ ci alalam lu leenub buur jariñul,ab sëriñ it jariñu ko ab taalibeem.

Sheex Baaba tag ko ciy xasaayid,aki dagiit,yu tollok ay téeméeri bayit,bokk nanu ci yile:( Shex Ahmadu xéewal la gu yàlla jox mbindéefam yi) ak waxam ja: ( sëñ bi daal xéewal la gu yàlla xéewalee,di kiimaan ci kiimaan yi),ak yu bokkul ak yooyu,bu waxutoon yu dul yii it , ñaari bayit yii,rekk doyoon nanu seede ci màggug sëñ bii,ak wilaayaam. Ndax kat sheex Baaba ak màggam gi, du fo mbaa muy yaxantu ci woy ni suharaawu yi,moom dey lu mu wax ci ndigal la ko teg,ak jaamu Yàlla,yal na ko Yàlla fay ci ñaari bayitam yooyu. Bokk na ci ñi mu siyaare ci sheexi naar yi,Ustaas Baaba mom Hamdi, ma jublu ci Hamdi mu ñaareel mi,dikk na fa yendu fa fanaan fa,nee nan ci menn mbaar. Sama xarit ba niy dàkkantale Kaadi Sheex Abdul Xaadir,doomi Amiirul Kumlayli , nettali na ma te booba taalibeb Ustaas Baaba la,ne Ustaas mii moo jox sëñ bi sekkare bi,waaye nag leeralu ma ban sekkare la,man naa am muy wirduw Saasalii,ndax sëñ bi bind na ne moom wirduw saasali mi ngi ko jële ci wenn wasiila,njëkk muy daje ak wasila wu mag wi,di Yonant bi (j.y.m) ,te leeralu nu kooka kan la. Li waral Kaad mii nettali ma ko,mooy maa ko laajoon bi mu jëlaatee ci sëñ bi wirduw Sasalii,ndax xam nga ci ku ko sëñ bi jële woon,mu ne déedéet,waaye nettali li mu waxoon ci diggante sëñ bi ak Ustaas Baaba,nu jorte ci ne ci Ustaas Baab moomu la ko jële ndax moom ab xaadir la woon. 

Kaad nettali na ma ne bi sëñ bi agsee, ci bi miy siyaaresi Ustaas ,ci bëcëgug bis bu sell,Ustaas defaral ko am soow mu neex ci ndox mu sedd,ak suukar,looloo ngi amoon,ci jamono ji sëñ biy nattu boppam ci di tegoo ay coona,mu ne ko naanal mu ne ko man baax na du ma naan lii, mu ne ko,ndax daa baaxul ci wàllug wér,waala da nga koo bàyyi  ngir Yàlla di jiyaar ak sa bakan,sëñ bi ne ko waaw loolu la,mu ne ko kon naanal,bàyyiwu ko ba mu far naan,ginaaw bi la dongay Ustaas yi laaj lu waral mu sonnu ci mu naan soow mi,mu ne leen ndax moom kat sonal boppam rekk la bëgg,ak mettital ko,mujj loolu di aadaam ngir Yàlla,ju mu manatul a bàyyeeti,ndare cib coona,ma jëflante ci ak moom waaye Yàlla defal na ko barke,ndax mujj na dëgar ci këng. 

Ginaaw bi lii wéyee lu yàgg,Ahmadu doomi Ustaas seetsi na Sëñ bi Njaaréem,mu bég ci lool,di ko ganale ngan gu mu sonn,indil ko ñam yi ak naan yi,bi nu àggee ci ataaya, Ahmad xam ne mbir dana am ,ndax moom du naan ataya,bi ko sëñ bi tàllalee ataaya ji,mu ne ko du ma naan ataaya,mu ne Yàllaa tax nga bàyyi ko ngir jiyaar ak sa bakan walla ag weradi,mu ni ko Yàlla,mu ree,ne ko naanal ma fayoo ca la  ma sa baay defoon, ñaanal ko ci barke. 

Bi Sëñ bi nekkee ci wëram googu nit ñaa ngi  ko daa dikkal bàyyikoo ci gépp wàll ngir xam-xam bu bari bi ak njariñ li,ak cofeel gi nu amoon ci moom ak diinewu gu dëggu gi,rawati na alal ju bari ji mu daa joxe rekk ,nga xam ne daawul tëyye ab dërëm,lu ñëw mu joxe,di jox mag ak ndaw goor ak jigeen,gor ak ab jaam,ku am ak ku amul,ku baax ak ku bon,loxo bu tàllaliku jëm ci moom mu feesal ko te soxlaalul nit ñi, doyloo kàppitaalam bi dul lu dul jublu ci Yàlla ak yiteem jépp. Mu dem Gànnaar jaar ca sëriñ ya,siyaare ñay dund ak barabi way faatu ya,jariñ leen ci alalam,ju bari ja,nu sopp ko nu kawe ni ko ñu ñuul ñi soppe,defal koy xasiday tagg,siyaaresi ko ci réewam ginaaw bi. 

Bi mbokk yi gisee ci moom kaweg xel,gu diine,gu mbaax gii mu yor ak jublu gi ko àdduna ak nit ñi jublu,nu tàmbli di ko iñaane,di ko lor,mu daan julleendoo ak ñoom,lor yi ëpp,mu mujj beru leen ak am mbooloom ak jàkkaam, Yàlla gën a fésal mbiram, ñu gënatee mer,nga boole ci terewu gi mu defoon ci mbirum  buur yi,daawul nangoo jaxasoo’k ñoom,ba da daa sàkku sax ci sëñ Mammoor ci ay bataaxel yu mu ko daa bind, -  da daan kersawoo jàkkaarloo’k moom di ko ci wax dara - mu bàyyi ag jëflanteem ak buur yi,naan ko seen teddngay fii ji toroxte la ëlëg,sëñ Mammoor daan ko ko nangul,te di ko ci jéggalu,waaye njabootam gi taxoon ba manu leen a bàyyi.

Ma nettali leen as lëf ci jaloore,nee nanu,bi kenn ci jaraafi Latjoor yu mag yi -mu nekkoon ku am solo fa Latjoor - jébblusee ci Sëñ bi,mu bokkoon ci jàmbaar yi amoon ay alal,mu ndàmmoom (gañewoon) lu bari ci màggum xareb Samba Saajo bi ( màgg mooy li niy jële ci koo xeexal  ba not ko) .Samba Saajo ab dëkk  la bu nekk  ca penkub Njàmbur,diggam ak Jolof,la xare boobu ame woon,ci diggante Amad Sheexu BA mu Fuuta, ak Latjoor,Tubaab yi japle woon ko moom Latjoor,ba mu gañe ko, ray ko,xarekati Latjoor yi gañee ci woon màgg mu rëy,ci alal ak ay jaam,te ña ca ëpp diggante Jolof ak Fuuta lanu bàyyikoo,ak Kajoor,tey jullit lanu, buur bi laaj ndax man na leen a def ay jaam, kenn ci boroom xam-xam yu mag yi,ne ko waa-waaw,ndax Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonnant, kon alalam ak dereetam dagan nanu, nu dal di wéyal loolu,te kat ag wooteem yonnant mbooloom boroom xam-xam yu mag yi saxalunu ko.

Li waral xare bi,lu gudd la manunu koo netaali fii. Bi jaraaf jooju tuubee ci sëñ bi,mu digal ko mu wacc mbooleem jaam ak alal ji mu ame woon ci xeex boobu, jaraaf ji déggal ko,def ko ànd ci ak kontaante, Latjoor ak ay gaayam jàppe loolu nag ag weddi ñeel àtte bi leen kenn ci boroom xam-xam yi defaloon,ne leen jaam yi dagan nanu. Nu mere woon ko,nee nanu ma jaraaf ya woo woon nanu jaraaf jooja fa kanamu Latjoor,ne ko : lu tax nga bokk ak nun ndab,règg rekk wëlbatiku,doyatu la nga ciy xëpp suuf? Mu ne leen waaw,weñ a tàbbi ci sama bakan,lëjal ma, moo waral lii ngeen gis ci man,waaye bëgg a nëxal seenum mbir taxut. Mu jublu woon ci weñ wi,lislaam ji ko duggoon,cig mbetteel,yaw nag xam nga lëjal gi lislaam di def ku mu dugg, du ko bàyyi ndare bu daa tuub. 

#Article 33: Betani bu Yurdan (143 words)

Bérab fu Yonent Yàlla Yaxya doon sóobe nit ñi ci ndox ci gannaaw dexu Yurdan, maanaam ci penku dex ga (Yow 1:28). Foofu la Yaxya sóobe Yeesu ca ndox itam. 

Bu yàgg xamatuñu tembe fan la dëkk bi nekkoon. Waaye seetkati cosaan yaakaar nañu ne fekk nañu bereb ba ca penku dexu Yurdan ca atum 1995. Berab ba Wadi al-Xarar la tudd. Am na fa ay bëti ndox, ak benn làquwaay fu ñu yaakaar ne Yaxya daan na fanaan. Su fekkee ne danga nekkoon ca dëkku Yeriko manoon nga gis berab ba. Ñoom ñi gas ci suuf ngir seet naka la nit ñi dëkke ca yeneen jamono yu fekk nañu ca bereb ba ay tabax, ay jàngu, ay làquwaay fu nit ñi doon dëkk, ak ay sanguwaay. Taalibe Yeesu yi doon nañu ajji ngir siyaaraji ca xarnu yu jëkk yi gannaaw jamono Kirist. 

#Article 34: Bowas (126 words)

Ci làkku ibrë (בועז) la tur wi jóge.
Ci angale mooy Boaz; Ci faranse mooy Boaz

Boroom alal ak beykat ci dëkku Betleyem la woon. Dafa takkoon jenn jigéenu Mowab, ji tudd Ruut. Jot na Ruut ndax jëkkëram mbokkam la woon te faatu na bala mu am doom. Ci kaw seeni yoon, su fekkee ne am na genn góor gu faatu te bàyyiwul doom, mbokkam mu gëna jege war na donn jabaram. Seen taaw bu goor dina donn ci goor ki faatu woon. Bowas mbokk mu jege jëkkëru Ruut la woon. Doom bi ñu jur mooy maamu Daawuda. Man nañu koy jàng ci Ru 1:1-4:22. Naka noonu Bowas bokkoon na ci maamaati Yeesu, ni ñu koy gise ci Macë ak ci Luug (Mc 1:5; Lu 3:32).

#Article 35: Bànni Israyil (122 words)

Ci angale mooy Israel, people of Israel or children of Israel; Ci faranse mooy Israël, peuple d'Israël ou fils d'Israël

Israyil mooy tur, wa Yàlla jox Yanqóoba, doomu Isaaxa, di sëtu Ibraayma. Ñi wàcc ci Yanqóoba nag lañuy wooye bànni Israyil walla it Yawut yi. Def nañu fukki giir ak ñaar, di yi soqikoo ci doomi Yanqóoba.

Man nañu gis bànni Israyil ci Injiil ci aaya yii: Mc 8:10; 10:6; 15:24; 19:28; 27:9; Mk 12:29; Lu 1:54,80; 2:25; 7:9; 22:30; Yow 1:31; 3:10; Jëf 2:36; 4:10,27; 5:21,31; 7:23,37,42; 9:15; 10:2,22,36; 13:17,23; Jëf 13:24; 19:4; 26:7,17,23; 28:20; Ro 9:4,6,27,31; 10:1,19; 11:7,11,17,25,26; 1Ko 10:18; 2Ko 3:7,13; 11:22; Ef 2:12; Fb 3:5; Yt 7:5,9,11; 8:8,10; 9:19; 11:22,28,29,30; 12:18; 13:10; 2Pi 2:1; Pe 2:14; 7:4; 21:12.

#Article 36: Catir (106 words)

Ci angale mooy Thyatira; Ci faranse mooy Thyatire

Ca jamono Injiil dëkk la woon, ci diiwaanu nguuru Room bu tudd Asi, maanaam ci sowu réew bi tudd tey jii Tirki. Tey jii Akhisasar la tudd. Dafa nekkoon ci yoon diggante Pergam ak Sàrd, ci dig bi nekkoon diggante diiwaani Misi and Lidi. Dëkk ba siiw na ndax cuub bi ñu fa defaroon.

Ca jamono ju njëkku mbooloom ñi gëm Kirist amoon na fa mbooloo bu am solo. Naka noonu gis nañu ne mooy benn ci 7 mbooloom bi ñu bind ci Peeñu ma.

Dañu ciy wax ci Catir ci Injiil ci Jëf 16:14; Pe 1:11; 2:18,24.

#Article 37: Daawuda (162 words)

Ci làkku ibrë (דָּוִד) la tur wi jóge. Daawuda mooy ni ñu ko waxe ci Lislaam. Ci angale mooy David; Ci faranse mooy David. Moo doon buur bu mag ci bànni Israyil, di yonent bu bind lu bare ci Sabóor. Man nga jàng ci jalooreem ci Kàddug Yàlla gi ci 1Sa 16:1-30:31; 2Sa 1:1-24:25; 1Ki 1:1-2:10; 1Ch 3:1-9; 10:13-11:19; 12:1-23:32; 28:1-29:30. Benn ci maamaati Yeesu ci Macë ak ci Luug. Ci Injiil Daawuda moo feeñ ci aaya yii: Mc 1:6,17; 12:3; 22:42,43,45; Mk 2:25,26; 11:10; 12:36,37; Lu 1:27,32,69; 2:4,11; 3:31,32; 6:3; 20:42,44; Yow 7:42; Jëf 1:16; 2:25,29; 4:25; 7:45; 13:22,34,36; 15:16; Ro 1:3; 4:6; 11:9; 2Tim 2:8; Yt 4:7; 11:32; Pe 3:7; 5:5; 22:16.

Turu Kirist la, muy wone ne, ci lu jëm ci juddoom wàcc na ci yonent Yàlla Daawuda, di wone it ne, Almasi bi la. Sëtu Daawuda moo feeñ 15 yoon ci Injiil ci aaya yi: Mc 1:1,20; 9:27; 12:23; 15:22; 20:30,31; 21:9,15; Mk 10:47,48; 12:35; Lu 18:38,39; 20:41.

#Article 38: Njàngat (1023 words)

Baatu Njàngat day tekki mbooleem ay mbind yuy wax ci ay koj. Ni ko Ñenn ñi di gisee du yem rek ci mbind yu ñu taaral waaye am na it njàngatu kàddu, maanaam yu yemm ci ay kàddu. Sunu xoolee mboolaay yu mel ne yu waa Afrik yi xamul woon bind, seenum njàngat ci kàddu la yemoon. 

Njàngat day di ab fànn gu am genn melokaan gi ci jokkoo, muy ci mbind walla ci kàddu, di tax ñuy man a jëfandikoo làkk bi bu baax te di am njeexit ci baatukaay bi. Njàngat da fa yaa te bariy fànn, li leen di wuutale mooy mbindin walla ndefu téere yi. Taaral gi am na ci lu am solo.

Ci lu ëpp dañ koy jàppee ni ag fànn. Waaye itam doon na lu jafe rëdd ay peggam rawatina su nuy bind ci xeltu, ci xarala walla yeneen.

Ladab baat la bu bawoo ci araab, di ci araab adab. Adab nag ci araab am na ñaar ba lu ko ëpp ciy tekki, waaye ñaar yi ci gën a siiw, bi ci njëkk mooy Adab: di baat bu Sëriñ Tuubaa (y.y.g) bari lu mu jëfandikoo ci téereem bii di Nëhju, di téere bu tëriit li (sujet bi) jëm ci yar ak dugal ci nit ñi ay teggiin (aadaab) di mbooloo(pluriel) ci adab. Bi ci des di bi ñu tax a jug, moom nag adab la nu laaf ci ag L muy leegi ladab, lu tax nu laaf ci L gi, loolu ñi ngi ci roye Lislaam te bu njëkk Islaam la woon, waaye ginnaaw ak L gi la ko wolof yi di gën a man di wax ak a tudd, moo waral - ci li nu wax - nu koy boole ci baatu araab bi, lii nag làkk woo gis ci àdduna bi am na ko, boo demee ci araab da cee fees dell, ay baay yu nu lem ba manees koo wax ci làkku araab, te doonuñu woon ay baati araab ñu mujj bokk ci làmmiñu araab te bu njëkk bokkuñu ci woon. Lu ni mel fees na dell ci Alquraan, am it ci làmmiñu araab wu jamonoo wii, sundus, istabraq ak yu ni deme duñu ay baati araab te ñi ngi ci Alquraan, lu mel ni qubtaan, di capitain dees koo jengal ba araab yi man koo wax waaye juddoowu ci añs.
Waaye nag Ladab ca daaray majaalis ya, maanaam fa mag ña daan jànge, nga xam ne seenuw jàngiin da daan tegu ci firi baat topp baat, maanaam pirim baat-baat, nga `xam ne lees la wax tekkil la ko ci wolof bu ñu nee bismil-laa ne la : maa ngi tàmbalee ci turu Yalla, ar-rahmaani: kay aji yërame ci àddina añs. Bu dee ci tekkiin wii, Adab di baat bi nuy wax Ladab: njàngat lees ko daa firee, walla xam-xamu mbind.

Kon manees na ne:
Ladab, 

Buñu bëggee muy wolofi kese ñu ne: 
Njàngat, walla xam-xamu mbind

Ci: Farãse:

Ci làkkuw Angalteer:LITERATURE

Ci mbindin mi walla waxin wi la ñuy sukkandiku ngir man a xammee xeeti njàngat yi:

Su nu jàppee ne njàngat ab mbooloom ay baat yu am bopp di wax ci lenn li la. Kon man nanoo wax Njàngatu xam-xam, Njàngatu koom-koom, Njàngatu diine, Njàngatu woy, añs.

Njàggat benn la ci anam yi nit di génnee ak a feeñale li nekk ci moom ciy yëgg-yëgg aki xalaat aki ñeewant aki gis-gis, jaare ko ci ay mbind walla bindiin yu rafet te wuute, moo xam woy la ( maanaam poesie) walla wesar (bind ci lu dul di ko nos, maanaam safaanub woy) walla wesar wu ñu nos. Loolu nqg di ubbil nit ay bunt ngir mu am man-man ci feeñal ak génne li ñu manul a génne walla ñu koy man a feeñale ci geneen anam walla melo. Njàggat nag day takku takku gu dëgër ci làkk. Dëgg-dëggi njuréef walla ngérte li juddoo ci làkk ñu bind ko, walla caada ja ca juddoo, day nekk di lu dencu walla lu wattuwu ci biir melokaani njàggat yi aki peeñ-peeñam, te ñoom danuy wuute kem ni gox yi di wuutee jamono yi di ko wuutee. Jamono ju nekk tam ay soppiku da ciy sosu akug jëm kanam akug wuute ak xeetu ànd ak jamono yi 

Man ngéen a xool foofu ci suuf,cuq ci lëkkalekaay yooyu, ngir déglu as lëf ci wolofali Sëñ Mbay JAXATE ak Sëñ Muusaa KA:

Làmmiñ ak jamono

Dangeen di xam ne aw làmmiñ, jëfandikukaay la boo xam ne lu am xel dem ci àdduna aw làmmiñ man na koo tudd, am xel ay gàtt, aw làmmiñ gàtt!Waaye lu am xel man a jëm ci àdduna rekk, aw làmmiñ man na koo tudd;aw làmmiñ gàttul.

Nit kiy wax nag fi xelam yam, fi jàngam yam, fi gis-gisu àddunaam yam, foofu rekk la ay waxam man a yam...

Waaye boo demee ba sam xel gis leneen rekk, làmmiñ dina ko tudd.
Lu ko waral? Amul benn baat boo xam ne bii yenu nga sa maanaa ci cosaan, amul!Mooy li nga xam ne - waxoon naa ne...dinaa cuq tuuti xel yi...ndax defe naa ne, yéen jàng ngeen xam-xamub làmmiñal...xam ngeen ne De Saussure (boroom xam-xam bu mag la woon ci wàllu làmmiñal) wone na loolu.Làmmiñ du loo xam ne tay baat yi dañoo juddu rekk daal di yanu seeni maanaa. Baat bi coow luy génn ci gémmiñ kepp la! Kepp! Amul sax menn maanaa. Ndax bu ko amoon wenn làmmiñ ay am, kon lu jug rekk xel yépp nenn lañu koy tudde.Wenn tur wi di moom te loolu amul.

Jukki bii tibbees na ko ci waxtaanu Seex Anta Jóob, mu amoon ci awril 1984 ca Cees

#Article 39: Xaralaymbëj (559 words)

Xaralaymbëj Mooy xeetu xam-xam giy gëstu lépp lu jëm ci wàllug mbëj, ay jëfandikuwiinam ak ay seddalewiinam. bu njëkk dañoo foogoon ne mbëj ag wal la rekk guy dem, gu man a nekk gu baax(+) walla gu bon(-). Waaye ci ndimalu ay woroom xam-xam yu mel ne Hertz, Helmholtz, Maxwell, Heaviside, Alessandro Volta ak ñeneen ñu bari, ci lees dem ba gën a nànd, xam mbir mi. Lu mel ne yamaleb maxwell biy faramfàce tëdiinu yani mbëj yi ( feppsaal ak mbëjfepp yiy wuute ci seen jublug yanub mbëj) walla toolu mbëjbijjaakon ba ca juddoo.

Ci gàttal, ci noonu lañu tambalee gis yenn ci ay jëfandiku yu mbëj: Doxalukaay bu mbëj, soppalikaay aki niitu...

Tay xaralaymbëj moo yor wàllu sàkk ay wuutuloxoy mbëj ak ay buumi séddalekaayu kàttanug mbëj

Ay faramface ak ay àtte yi lal xaralaymbëj.

yamaleb maxwell yi, ñooy àtte yu am-solo yu ñeel mbëjbijjaakon, ci la yeneen yi soqeekoo.

àtteb ohm(om) yiy faramface ndëgërlu gu mbëj gi

àtteb Faraday-Neumann-Lenz mooy faramface xiirtalug mbëjbijjaakon

njeexitu joule mooy leeral ni kàttanu mbëj di soppeekoo nekk tangoor ngir njeexitu ndëgërlu gi.

àtteb Kirchhoff(kiirkof) mooy leeral jëflante bi nekk ci diggante dawaan ak dend ci ag ndombo.

Ag wàll gu am solo moo jëm ci lépp lu ñeel yokkte ak seddalewiinu kàttanu mbëj ba ca jëfandikuwaay ya (barab yees koy jëfandikoo).
Kàttan gi dees na ko jóox ci ndimbalul ay jurukaayu mbëj ci barab yees ko jagleel, li ñuy wax diggub mbëj, ci lu ëpp fa muy nekk day soree ak dëkkuwaay yi.

Buumi séddalekaay yi dañu leen a lëkkale ci seen biir ñuy jëlee kàttan gi ca jóoxuwaay ya di ko yóbb ca jëfandikuwaay ya.

Li wuutale Buumi yóbbukaay yi, mooy limu dend gi ñuy yóbb, moo tax ñuy gis ay buumi dend gu kawe, Dend gu diggu]|dend gu diggu, dend gu suufe. Su diggante jóoxuwaay yi guddee, dañ fay def ay mbëjjaaru, ay buumi dend gu kawe yu man a yóbb ay milioŋi watt ci kàttan tambalee ciy 400000 v. Buumi dend gu kawe yii la ñuy duppe yu yóbbug kàttanu mbëj, yi nga xam ne ñooy tax a man a yóbb kàttanu mbëj gi, jële ko ca jóoxuwaay ya, jëmee ko ca barabu soppikaay ya.

Ci nii la ñuy soppee dend gu kawe mu nekk dend gu diggu, jaarale ko ci ay masin yu mbëj yees di duppee soppalikaay, ci noonu la ñuy yóbboo kàttanu mbëj gi ca ndombo gu dend gu diggu, moom ci boppam dañu koy àggal ci néegu seddalekaay yi jaarale ko cig ndombog séddaleg kàttanu mbëj, foofa lañuy defee geneen coppite jëlee ko ci dend gu diggu soppi ko dend gu suufe ngir ñu man koo jox jëfandikukat yi ci kër yi ak liggéeyuwaay yi.

Doxalukaay yu mbëj yi, ay wuutuloxo lañu yu’y soppi kattanu mbëj def ko kattanu doolerandu. Doxalukaay yi dañu leen a séddale ci:

Jurukaayu mbëj yi Ñoom ay wuutuloxo lañu yuy soppi kàttanu doolerandu def ko kàttanu mbëj. Yi ci gën a raññeewu:

Soppalikaay, Ab wuutuloxo la, maneelam mooy soppi limu dendu mbëj gi nekk ci ab ndombo, ci yokkute walla wàññi. Lu mu néew néew di na am ñaari lëmës yu bijjaakon boole.

Wuutuloxo yu man a yokk walla néewal taraay te di jëfandikoo benn lëmës rek, lañuy tuddee Soppiboppam 

Ay jumtukaay lañu yu aajowoo soppi kàttanug mbëj mu nekk leer. Di ko jëfandikoo ngir leeral barab yi.

#Article 40: Mbëj (837 words)

Mbëj da di ag feeñte gu gisuwul ak bët, guy feeñ ci ag wootalante walla bëmëxante ci diggante yani mbëj yi. Ci gattal mooy gépp feeñte gu juddu ci jàmmaarloo gi nekk ci diggante: feppsaal yi, ñoom ci lu ëpp da ñuy tekkaaral, ak mbëjfepp yi nga xam ne ñoo ëpp yëngu-yëngu, ci biir xarefulwoon bi. seenuw demiin jur ab dawaanu mbëj.

Su ñu ko boole ak bijjaakon, mu jur beneen banqaas bi ñu duppee mbëjbijjaakon. Mbëj moo yor ay feñte yu jëmm yu mel ne melax, toolu mbëj ak dawaanu mbëj (ci lu bari dañ leen di jaawale).

Mbëj doon na “jaamu” nit bi gën, doon tamit raññeekayu àdduna bu bees bi. Dafay leeral sunu dëkkuwaay yi di doxal sunu këri koom-koom yi te jegeele nit ñi gënoon a soriyante.

Yanub mbëj doon na lu ñu man a natt te man koo jëfandikoo, waaye doonul lu neex a faramface ak ay baat yu yomb a nand, ndaxte yombul leeral melokaan yi mu am dëgg-dëgg. Xayna li gën mooy wax lan la ak li muy sabab. lépp (lu mu man a doon) lu am yanub mbëj, man nañoo wootalante walla bëmëxante. Li gëstu yi wone mooy am na ñaari xeeti yani mbëj, benn bi lañuy woowe yan bu baax (+) moom mooy nekk ci biir saalu xarefulwoonu ne-ne yépp ak yan bu bon (-) (mbëjfepp) ñoo nekk ci li wër saalu xarefulwoon yi. Naka-jekk yan yu baax yu saalu xarefulwoon bi dañuy tolloo ak limu yan yu bon yu mbëjfepp yi ko wër.

Ba fii danoo jàppoon ne, gépp ndombo goo jël, mbëjfepp yi dañuy yëngu saa su ne jëm ci benn jubluwaay ci biiram. Yenn saa yi nag dawaan bi du sax ci maase, muy ci doole walla ci jubluwaay bi. Ag noste mbaa ag ndombo gu ne mel lees di wax dawaan bu wéy. Am misaal man naa nekk ag noste gu ab tegle di doxal. Donte sax aajowoowul dawaan bi di am genn jubluwaay gu sax. Bari nañu ndombo yu mbëj yees di jëfandikoo yuy safaan jubluwaayu seen dawaan ci biir ndombo gi. 

Gii xeetu dawaan lees di wax dawaan bu safaanu. Ndombo yu mbëj yu ëpp yi ñuy jëfandikoo, dawaan bu safaanu lañu. Cig ndombo gu dawaan bu safaanu, dafay laaj waxaale tamit baraayu ni dawaan bi di safaanoo, taraayu dawaan bi ak dend bi ci ndombo gi, moom rekk , bu mujj bi, doy na su fekkee dawaan bu wéy la. Ci baraay bi lañuy natte ñaata yoon la dawaan bi di soppi jubluwaay ci benn saa.

Liy wër ab mbëjfepp walla leneen lu mu man a doon lu am ab yanub mbëj day am melokaanu luy dox, moom lañuy tuddee toolu mbëj. 

Soo jallaxee ay mbëjfepp, day am benn tool bu wër seenub jublu, moom la ñuy tuddee toolu bijjaakon. Dooley tool boobu dafa aju ci limu mbëjfepp yiy daw ak seen gaawaay, maanaam, ci yeneeni kàddu, ci dawaanu mbëj bi. 

Soo jallalee ab dawaan ci ag lëmës, gu nekk wëñu përëm, ci nimu waree, lëmës googu day mel ne bijjaakon gu weñ, day xëcc walla bëmëx yeneen lëmës yi mu yemal wëñ. lëmës gu mel noonu su fekkee danga koo defaree ak ag wëñu përëm goo wëndeel cib weñ, day gën a yokk toolu bijjaakon ba cay juddoo. 
Su fekkee dangaa am ay lëmës yu bari, yu ñu wëndeel wëñ ci weñ, yu man a wëndeelu, nga boole leen ak yeneeni lëmës yu dul wëndeelu, yu am toolu bijjaakon bu tar, yu dawaan jaar, day jur jenn dooley doolerandu. Doole joogu moy wëndeel lëmës yu man a wëndeelu yi, mu daal di man a def liggéeyu doolerandu. Mu nekk ab jumtukaay bi ñuy woowe doxalukaay bu mbëj. Tay jii, doxalukaay yu mbëj yi ñooy doxal bépp wuutuloxo, tambalee bi ci gën a ndaw ba ca ba gën a ngande.
Doxalukaay yi dañoo bari te am ay melokaan yu wuute.

Njariñ li ci jëfandikooy noste yu dawaan bu safaanu moo ngi ci li ñuy man a yokk walla waññi dayoo bu ab dendam ci jëfandikoo jumtukaay bees di woowee soppalikaay. Ab soppalikaay ñaari taxañ yu tàqalikoo lay am, yees ber, yu ay wëñ yees lëmës cib dankub weñ (saalu soppalikaay bi). Ab dawaan bu safaanu su walee ci taxañ bu njëkk bi, ab toolu bijjaakon daf fay juddoo, mu jur moom itam, ab dend buy soppeeku ci jenn jamono ju nekk ci ñaareelu taxañ bi. Su ñu jëlee benn dayoo bu saal bi (weñ gi) ak yenn limi lëmësi wëñ yu taxañ yi, dees na man a yokk walla waññi dend bi ci nees ko bëgge.
Kon, ab Soppalikaay di nanu tax a man a jëfandikoo dend bu suufe, ngir sunu kaaraange, ci kër yi, te terewul nu man koo jokkale, mu jóge cib digg bu mbëj bu sori, cib dend bu kawe. Manees naa jëfandikoo ab soppalikaay ciy fowekaay yu mbëj ak ci yeneen jumtukaay yu ndaw yu mbëj ba-tay. Maneesul a jëfandikoo soppalikaay cig ndombo gu dawaan bu wéy, ndaxte dawaan bi toolu bijjaakon ba muy jur duy soppiku.

#Article 41: Doxalukaay bu mbëj (369 words)

Doxalukaay bu mbëj, ab wuutuloxob mbëj la, boo xam ne kàttan giy duggu ci moom gu mbëj la te ga muy génne gu doolerandu la. Doxalukaay yu mbëj yi am nañu solo lool ci dundiinu jamono ju bees ji, te it dëgg la sax, ne limu doxalukaay yu mbëj yi nekk ci am réew dafay firndeel tolluwaayu jëm-kanamam. Maanaam yokkug limu doxalukaay yu mbëj yi ci am réew bokk na ci wonekaay yiy firndeel tolluwaayu yokkuteem ci wàllu xarala mu réew moomu. Ngir dëggal loolu, doy na xool ci jumtukaay yi nekk ci li ñu wër: ca saxaar ba ci watukaay ak yeneen ak yeneen, yi ngeen xam ne nit ku bees ki moo ngi koy jëfandikoo bu baax, man naa ni sax ñooy doxal sunug dund. 

Doxalukaay yu mbëj yi dañoo bari te wuute, am na doxalukaay bu dawaan bu wéy, doxalukaay bu dawaan bu safaanu moom mu séddaliku ci doxalukaay bu demandoo ak doxalukaay bu demandoodi,.

Dawaanu mbëj bi day jaar ci ag lëmës gees wëndeel ci ab dogub weñ bi tudd tekkaaralaan bi. Lëmës googu, gi ñu defare ak wëñu përëm (naka-jekk përëm lay doon waaye manees na koo defaree ak beneen xeetu wommatukaay), dafay jur ab toolu mbëjbijjaakon, tool bi dafay feeñ niki ag walug bijjaakon, di lees man a natt. Danu koy jàppee niki jenn doole di lees di wax dooley Lorentz. Toolu mbëjbijjaakon boobu dafay duggante ak toolu mbëjbijjaakon bu lëmës gu wëndeeluwaan bi jur, mi melokaanoo teewaayu ñaar walla ñetti seexi dott. Wëndeeluwaan bi tambalee wëndeelu ci ndimbalu dooley Lorentz; bëj-gànnaaru toolu bijjaakon bu wëndeeluwaan bi day bijjante ak bëj-saalumu toolu bijjaakon bu tekkaaralaan bi. Xaaju wëndeelu gu nekk, dott bi day soppeeku, ci noonu la wëndeelu gi man a wéyee.

Ci atum 1821, lu weesu xamteg feñte gu mbëjbijjaakon gi simikat boobu di Ørsted xamle woon, la jëmmalkat bu waa-angalteer bii di Michael Faraday defar ñaari wuutuloxo ngir sàkk li mu duppee ag wëndeelug mbëjbijjaakon: ab doxub dooley bijjaakon bu mbegewu te wéy, ci lu wër ab wëñ, ci maanaa mooy faramfaceg doxalukaay bu mbëj gu njëkk.
 
Xeeti doxalukaay yu mbëj yi am, manees naa wax ne, du xaaj du jeex, waaye manees na cee lim yi ëpp yees di jëfandikoo:

#Article 42: Xam-xamu suuf si ak jawwu ji (366 words)

xam-xamu suuf si mooy li nuy wax (Jiyoloji), xam-xam la buy gëstu lépp lu aju ci suuf si kaw gi ak biir gi, ak doj yi (montaañ yi)añs. Bu jawwu ji di biy gëstu lépp luy jawwu ak tegaloo gi ñu tegaloo.

Jawwu ji nak :mooy mbalaanum ngelaw li wër suuf si. Lees di gën a sori suuf si, ngelaw liy gën di néew-doole di gën di amadi, day mujj sax di lu fàddu ci ay fukki culómet cig kawe. Lii a tax ñu man a séddale Jawwu ji ci ay goxi jawwu yu wuute te tegaloo, gox bu ci nekk ami jagley boppam:

Fatt-jawwu walla JAWWU JU FATT ji: mooy ji gën a tal gën a fatt te gën a féete suuf; moom ngelawam day yëngu jamono ju nekk, fa lay niir yi di sosoo ak mbooleem soppaxndikuy jawwu yi; kon cig jege mooy jawwu ji ëpp ag jeexiital ci wàllug dëkk ci kaw suuf ak ci ni kilimã bi di séddalikoo

Mbooleem beeñ bi ak doj yi ñoo sos wàll gu tond (superficiel), gu dëgër gu kol-kolu suuf si, ñu koy woowe Jéeri ji walla aji wow ji.

bu ñu séddalee Jéeri ji, def ko ñeenti xaaj, ñatt yi daanaka ndox yee leen muur, yooyu ndox nag ñoo sos mbàmbulaan yi ak géej yi, waaye wàll yi génn ci jéeri ji; nga xam ne ndox yi muuruñu leen (gox yi ak dun yi , wàll yii ñooy wërlaay gu dëppoo te méngoo ak dundug nit, moo tax fi la nit di dunde, di fi defe ay liggéeyam, walla li ëpp ci ay cawarteem (activités).

Jéeri ji nag day dund tey màgg ci anam gu sax, ak doonte fi nun, day mel ne ni mu nekke soppikuwul. Li ko waral nag mooy ni muy soppikoo day faral a yeex lool: doj yi bu ñu sosoo ci ron géej gi, dañuy mujj lemu, yékkatiku, màgg ànd ak Jamono yu jiyoloji yi ñooy mujj sos ay càllalay doj yu yees.

Ci safaanub loolu doj yi gaaru ci kanamu jëfkay jawwu yi dañuy xolliku, di xoosu, di fellu, bu ko defee, yooyu xoosiit ak felliit (ban yeek beeñ yeek yi ni deme) ñooy mujj sottikuwaat ci géej gi

#Article 43: Sëriñ Muusaa KA (578 words)

Sëriñ Muusa KA (Sëriñ Muusa KA werekaanu Bàmba) woykatu wolof ak araab
la woon bu mag te xarañ ci, ab jullit la woon bu dëggu te di ab sufiyànke
di taalubeb Sëriñ Tuubaa bokk it ci Seexi Sëriñ Tuubaa
yi, taalif na lu sakkan ci ay téere ci wolof ak araab rawatina wolof ndax ki mu
daa tagg wolof mooy làkku cosaanam muy Sëriñ Tuubaa Sëriñam
te sëriñam boobii it Yonnent bi moo doon sëriñam bu ko daa tagg ci araab lakoy tagg, 
ndax nit koo di tagg di ko tagge weneen làkk wu dul làkku juddoom tagg ga du mat
ndax yaangi koy tuutalal cosaanam, ay woyam nag li ci ëpp Sëriñam la ciy tagg ak
di soññ bokki taalubeem ngir ñu gën a fonk Sëriñam te nankoo jaamu Yàlla, ku xelu la woon
te jàng ba ci woyam yooyii mu woy ci wolof ku jàng `Aruud (xam-xamu woyiin ci araab) ma nu koo jam, sàmmoonte naak sarti woy ak bahru yi (woyiin yi), ba sos na ay Bahru ajami; niki Téere bi tudd «Bu léen njuuj-njaaj» ak way wi mu jébbaloo ci Seex Mustafaa Mbàkke xalifab Seexul Xadiim bu jëkk.

Jiim gi

jigéen ju ndaw araf ya lan ko tënke - tënk ba bis pénc ba lan koy tinkee

jiimug jigéen mooy jekki bum jàllantu - ndaxte bu jàllantoo asal njaaloontu

cofeel gu mat sëkk a ko war cib sëriñam - ku bëgg dof te ku doful doo am ngërëm

jaamu boroomam jaamu it boroom këram - moo war jigéen su ko manee dàmmey ngëram

jam tuñ ma, jam siiñ ma'ak njamal-yàllaam la - jaalu-yàllaam wa ne Yaasin Salla'a

Jàmm ak juddook jikkoo waral ñuy tànn - ne xur wi wenn la te jiim yiy jenn

Kaaf gi

kaaf nga na baax gaaf, bari ngor, toog fa këram - na bari kersay kër-këriy sàkku ngërëm

nay gone bum def mag te bum gàtt kutuj - bum gudd lool fum toll ànd ak latkoloñ

Yaa gi

yaa ga na yaatu ŋàpp,  yaatal dëkkandoom - yaatal boroom këram ci lépp lu mu moom

yaru te yomb te yéwén te yaatu - cib sëriñam te la mu yor bum laatu

Arafu nuun gi

arafu nuun gii ku ko boole xejj - ci sa boroom kër gaa ya duñ la xàjji

neex cere, neex dereet te neexu làmmiñ - neex lépp tey neexlaate gàttu gémmiñ

jigéen na maandu, man a muñ te mokk - di muñ di muuñ di mooñ cereem ne mekk.

arafu baa yile jigéen ju boole - seen jikko yii kenn du la ba ngay xoole

baax baay te booleek bari bayreek barile - ba su boroom këram amul muy defale

bëñam ya weex tàll ba mel ne perkaal - bët ba ne bàq bakkanam bay safu jaal

day neexu làmmiñ, neexu ñam te mokk lool - lewet te nooy ku mu dajeel sukkal la teel

adunyaa ngi tol new fel fi moom mbaate dëññu teeñ () woroomiy tëndëŋ xammeewu leen ak woroomi téeñ

lilee tax mu daa tuubloo dameel ak maxa'aki teeñ () ku mel nii ku amleek moom na leen wóor ne yaa ko tooñ

du tooñ nit te soo tooñee mu jéggal la tin la ko () xamul jaamur ak mbokkam, mag ak ndaw ci aw meloom

wurus mbaate ab xaalis bëy ak nag xar ak gëléem () la daa buub di jox ñiy laaj du kuy néegaleek a léem

añs

Ngir déglu te yér as lëf ci woyi Sëriñ Musaa Ka xoolal foofu:

#Article 44: Téere Taariix (62365 words)

Taariixu àdduna bu bees bi te jamonoo
Ag jiital 

Teeree ngi nii buy gàttal yoonu xam, ndax li nga daa lijjantee xam ciy fan ak cib coona, moom la lay xamal ciy waxtu, ci lu dulub coona.

Muy bu nu def ngir feeñal ci baat ak waxiin yiy war a wuutu yu fraanse yu bari yu nuy teg ci barabi yu wolof yi, te kat fekk na wolof amoon leen mbaa mu manoon leen a am, te nu jàpp ne manunoo doylu wëlif leen. Ma yaakaar ne bu nu bëggee yombal dëgg, lu mu metti, metti, danoo war a wut ay kunaked babies in my asshole utlaay ñeel baati doxandeem yii bëgg a ruur sunu làkk wi, te nag  yombug xam-xam mi ngi ci nga koy jàng mel ni jàngoo, kon lu tax muy français? Ginaaw du lu moy ab jumtukaay ngir xam, ngir déggante, waxante, te ma gis ne bu dee ci ay wolof seen làkk, lay gën a nekke jumtukaay boobu.
Lii ak leneen lu bari, moo ma yobbu ci di xalaat ci di binde ci wolof, te ba yeneen kàllaama yi, ginaaw bindaluma ku leen moy. Te it nag ni ñepp def ba ami làkk lu tax dunu ko def bay am sunu yos ñun itam waa Afrig? Nekkewunu fi lu dul ligeeyal Tugal ak lu ni mel, nanu sunu bopp ñor ! doonte as lëf la it.
Nan la am reew mu tollu ne Senegaal… ñépp di waxi wolof nga ne fraanse rekk ? reerale ga’a ngii ! i have a 1 incher

Abdul Xaadir KEBE

Bunt bu njëkk bi

Njëlbéenug jamono yu yees yi

Doggantal gu njëkk gi  	

Yewwute  ga amoon ca Tugal

Yëngu-yëngu googu nag mi ngi tàmbli ci xarnu bu fukk ak ñatt ginaaw juddu gu yonnant Yàlla Hiisaa, ba ci bu fukk ak juroom ñaar, mu sos fi nag ay soppi yu xóot ci wàllug aada, dundiin, mboolaay , politig ak koom-koom.
Kon daal, yewwute gii amoon ca jamono yooya ca Tugal, li muy wund mooy ag tuxu juge ca jamono ju diggu ja   ( mu'y jamono'y  ag laman   walla ag cang) dem ci jamono ju yees ji ( di ju jëm-kanam gu xam-xam ak xarala ).

Sabab yi tax Yewwute'g Orob gi am :

Sabab yi jur yewwute gii  yu bari lañu, waaye nañu ci indi ñatt yi ci ëpp solo rekk, ñooy : 

Jeexiit gi Lislaam amal ci yewwute'g Orob gi :

Ci waxtu wi Tugal nekke cig deltu ginaaw, ci wàllug xay ci jamono yu diggu yi, nga xam ne jàngu bi (Egliis bi) faagaagaloon na bépp xalaat bu leer te gore  , araamal ci nit ñi ñuy xool leneen lu dul am njàggaleem mu way deng mii te doxadi, bi Orob nekke ci lëndëmam gii, jullit ñi ñoom ñi ngi doon jëm-kanam bu baax ci yekkati tabaxub seenug xay ci kaw ay cëslaay yu xam-xam ak wisaare maandute ak mbokko ci diggante nit ñi, ci lu dul xool xeet walla melo mbaaw làkk . 

Xayug lislaam gi nag àgg na Tugal jaare ko ci yoon yu bari, bokk na ci yooyu, Andalusi ak Sisil ak reewi penkub lislaam bi, rawati na ci xarey jooñ yi 

Ndax kat booy xool li Tugal di nekk lépp di ku ñu dàqe ca xarey jooñ ya, duma ko ca, teewul mu fàggoo ca njariñ lu bari ngir fenqoo gi mu ci defe ak xalaatub lislaam bi, ak nosteg dundam  .

Lii nag ci li soppi xalaati waa-Tugal yi la jëm ci Egliis bi, nit, adduna bi ak dund gi. 

Te itam lu bari ci sàkkukati xam-xami Tugal yi, dañoo tàmbli woon di naan ci xam-xami lislaam yi, ci ndoktoor, xeltu  , gañcax ak ndundat , ak yu dul yooyu ci jàngu  yu Andalusi yi, la ko dale ca xarnub fukk ak benn (g)  .

Loolu nag taxoon na ba yëngu-yëngu gu firi  walla tekki  gu mag  amoon ci xam-xami lislaam yi, tukkee ci làkku araab dem ci wu latin ( wi doon wu xalaat, wu diine, tey wu politig ca Orob ca jamono jooja ) loolu dimblee woon - ci ginaaw bi - ci lal yoon wi ba yewwute gu Tugal gi man'a am.

Feeñug dëkk yu mag yu Tugal yi ( les villes ): 

Bu ko defee, li ñuy wax tool, di suuf  si sang biy moom, moo daa tekki barabu dëkkuwaay bi, koom-koom bi, mboolaay gi, ci gii noste .

Màggug dëkki Tugal yi, ngir màggug yaxantu gi nu daa def ak mboolaayi jullit ñi, ak màggug mecce yi ak ligéey yi, ngir jòkkoo gi waa Orob gii daa def ak jullit ñi taxoon na ba nosteg laman tàmbli woon’a lòtt ak’a naaxsaay, rawati na bi nitug Tugal ki tàmblee am yoon wu mu man’a jaar bay dund te du sukkandiku - ci léppam - ci suuf ak tool, waaye ci yeneen ligéey yu koom yi. 

Dëkk yi tam tàmblee doon barabi leer yu di boroomi xay, di sonnale ci loolu ak’a lakkal noste gu laman gi, tey ligeey cig màbbam, def it lu rëy ba yewwute ci Tugal man’a am.

Lòttug Egliis bu Paab bi akug tasam: 

Egliis bi moo nekkoon di teg loxo ci dundug xalaat gi, gu diine gi ak gu aada gi ci Tugal gépp, te yitteem jépp mi ngi ko sotti woon ci njàngum pas-pasu diney nasaraan, walla li nuy wax njàng yi aju ci Yàlla (théologie), ak njàggat  ak xellu , amutoon jenn yitte ci njàng yi aju ci xam-xam.

Egliis bi moom dafa jàppe woon boppam ki  nga xam ne ci yoon moo war’a doxal mbiri politig yi. Te kat (moom Egliis bi) tawati mbon akug yàqu dañoo ruuroon aw yaramam, dugg ko fépp, ba waral aw nit wu jàng te yewwu jug, taxaw temb ci dañal ñaawteef yooyu ko taqoon. 
Loolu tam bokk na ci li jañoon xelum nitug Tugal ki ci mu jëm kanam, gën’a ñaw, rawati na bi dëkk yi gënee yaatu, deggiinu ligeeyub yaxantu gën fa’a xóot, ak bu endustri ak aada .
Yii yepp nag ligeey nanu lu rëy ci  waxuma la doyodil ngëb gu tar gi paab gi ngëboon mboolaayu  Tugal gu nasaraan gi, waaye it doyodil nosteg laman gi, loolu it  - di doyodil nosteg laman gi - rataxal yoon wi ba yewwute gi man’a am.

Itaali mberum  yewwuteg Tugal gi:

Dëkk yu Itaali yi ñooy mber mu njëkk, mi njëkk’a uuf, tete yewwuteg Tugal gi, looloo waraloon ñu am wàccuwaay bu kawe akug wormaal ci yeneen dëkki Tugal yi ca jamono jooja. Dëkk yii niki Milano ak Venezia ak Firenze ak Napoli, ñoo uufoon yewwute gi, seeni boroom xam-xam aki njàggatkat ak artist walla waa fànn duggaloon nanu ci seen loxo bu baax .

Li waraloon loolu nag lu bari la, bokk na ci, dal ga fa amoon ak jàmm ja, ak jëm kanamug koom-koom ba, ak yaatug yëngu-yënguy nitu Itaali ki, ak ba tay yaatug goxi xalaatam, ak yëg gu mu yëg gore  gu mu am, ginaaw bi mu goree ci nosteg laman, ak li Itaali yàgg’a am ci teddnga gu sax ak jaloore : mu'y njàggati waa Rom yi, seeni xam-xam, seeni jeexiit ak seeni fann  , nga rax ci loolu nekk gi paab gi  nekk Rom, nga xam ne loolu faggul na waa Itaali ag cang gu diine.

Ni nga xame ne barab boobu it (di Itaali) faggul na paab gi ci Itaali ag tono  gu ne-ne  ak gu maanaa gu mag, nga rax ci dolli gëpplante  gu mag gi amoon ci diggante dëkk yu mag yi ak peeyi buuri Itaali yi, ci wàllug njàggat ak fànn ,ak soññ gi doxalkati  dëkk yii ak buur yi daa def boroom xam-xam yi daa ligeeyal yewwute gi. Ak ba tay yittewoo gi nga xam ne amoon na ci dëkk yii, aju ci gëstu mbind ak taalif yu yàgg ya, ak barig móolukaayi teere yi  ci yii dëkk. Ak nag li Itaali doon xéewoo, muy nekk ci barab bu raññiku, buy dimblee ci jokkoo ak addunay jullit
ñi.

Mandargay Yewwuteg Tugal gi :

Yewwuteg Tugal gi, mi ngi ame ci mbooleem wàlli dundug nit, gu xalaat, gu fànn, gu politig, gu diine, ak gu koom-koom. Yii di ñëw ñoo ciy wàll yi gën’a rëy:

(1) Yëngu-yëngu yi aju cig nite :

Ag nite li miy wund fii mooy dundal njàggat yu yàgg ya ( yu Gres ya ak Rom), ak feddali sukkandiku gu nit war’a sukkandiku ci boppam, akug goreem  ak sañ-sañu wax li nekk ci moom, ak dog gàllankoor yu mboolaay yi, ak jële fi aaday jamono yu diggu yi, ak sotti yitte yi ci adduna bi ak dénd bi , ak jeem’a xam seeni mbóot.

Yëngu-yëngu googu nag bokk na ci màndargay yewwuteg Tugal gu njëkk gi, ndaxte li mu yittewoo woon mooy xam-xam yu kojug nite yi nga xam ne njàggatkati Gres yeek Rom (grego-romain) ñoom lanu jëloon, yittewoo leen,ak seeni xeltukat  ak seeni boroom xam-xam ak ñoñ fànn  ak seen boroom mecce yu muus yi te ñaw.
Boroom xam-xam yi daa def gëstu yooyu di kojug nite, ñi ngi leen di woowe ñoñ nite, walla boroom njàggat yi. Ñoñ nite kon ñooy mbooloom nit mi yittewoo woon jàng njàggat, xam-xam ak fànn yu yàgg ya (yu klaasik ya), maanaam njàggati Gres ak Rom ak seeni fànn ak xam-xam.

Yëngu-yëngug nit gii nag judd na, ginaaw bi mu amee ag jàpple gu tukkee ci kilifay dëkki Itaali yi ak seeni boroom alal.
Ñoñ nite ñi génne woon nanu ab taar, feeñal ko ci mbooleem fànn yu wuute yi, moo xam yatt  la, mbaa nataal, ak deseñ, ak misik, ak tabax. Ñoñ fànn ñu Itaali ñi  ak ñu dul ñoom ci jamonoy yewwute, dañu doon roy fànn bu klaasik bi , di bu gres-rom bi, bàyyi nee nag fànn bi nu daa wax xóot , nga xam ne moo amoon ca Tugal ca jamono ju diggu ja . 
Bu ko defee, ñoñ fànn ñi jëmale seen fànn ci taarub dénd bi  ak dund gu yees gii nga xam ne mooy gisiin wu jëm kanam wi nu am ci dund gi.

Dëkki Itaali yi gis nañu aw tabaxiin wu bees, ndax wacc nanu nee tabaxiinu xóot wiy am ay poto yu ñu catal, te weccee ko ak tabaxiin wu klaasik wi raññikoo ay poto yu am ay ndëpp  yu rafet aki jagle mbaa deseñ yu eesañeri mel ne yi daa am ca tabaxiinu Gres wa.
Tabaxiin wii siw na lool te tas ci Egliis yi ak katedraal yi, ak saal yi ak barabi tiyaatar yi, ak sangukaay yi .

Ci dëkki Itaali yii, lu bari ci waa-fànn yu siw yi fa lañu feeñe, bokk na ci ñooñu deseñkat bu siw ba, di Fra Angeliko ( 1400 - 1455 ), mi nga xam ne dees na ko lim mu bokk ci waa fànn yi raw te gën’a mag, ñi nga xam ne ñoo doon gëstu modeli fànn yu yàgg ya .
Ay ligeeyam itam dañoo raññikoo woon màndargam diine mu dal, mu nekkoon moom ku diinewu.

Bokkoon na ci ñoom it Leonardo da Vinci ( 1452 - 1519 ), moom mi boole woon fànn ak xam-xam, defar nay nataali fànn yu siw, bokk na ci yooyu bi tudd reer bu mujj bi, ak Jokanda, walla Mona Liza. ñaari nataal yii ci yi gën’a siw lañu ci deseñi jamonoy yewwute.
Da Vinci mii nekkutoon ab deseñkat bu aay rekk, waaye raxoon na ci dib yattkat bu mag,dib rëddkatu tabax  te dib eesañër bu muus. Bokk na ci deseñkati Itaali yu yewwute gi ba tay ki ñuy wax Titian (1488 - 1572 ), moo nataaloon ay wàll ci dundug ñu féex ñi walla aristokraat yi ci dëkki yaxantu yi ak fànn yi, ak Rafayel (1493 - 1520 g ), moom itam rëddkatu tabax bu siw la woon, te di deseñkat bu bokk ci ñi gën’a siw ci mbooleem jamono yi. 

Bokk na ci ñoñ fànni yewwute gi ci Itaali ba tay, yattkat ba Donatello ( 1386 - 1466 ) , mooy ki sukkandiku woon ci yattam ca yattiin yu klaasik ya, di gres-rom, rax ci dooli ku yittewoo woon taarub dénd bi la ak ag dundam. Moom daal ca dëgg-dëgg moom la nuy jàppe ki sos te taxawal yatt gu bees gi.

(2)  Feeñug làkk yu bees yi:

Làkku Latin, ci jamono yu diggdoomu yi , moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam-xam ya, ak niti diine ya, ak politgkat ya, ak njaggatkat ya  ak ustaas ya. La notoon nag ca nit ña -  di woon  niti neen ñi rekk -  ñoom déggunu woon wii làkk, lu tumbrànke la woon ca ñoom, seen làkki bopp yiy yu seeni barab lañu déggoon.

Bi jamonoy yewwute dikkee, ngelawul fonk sa xeet   upp ci Orob gepp, la lu bari ci xalaatkat yi, ak njàggatkat yi, ak woykat yi, tàmblee jèng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki réewi bopp, niki wu Itaali, wu Espaañ, wu Fraans, wu Angalteer ak yu dul yooyu.

Bi mu ko defee, woykatu Itaali bi tuddoon Dante ( 1265 - 1321 g ) taalif Komedi  Bu sell bi ci làkku Itaali, naka noonu Petrarch ( 1304 - 1374 g ) mii nga xam ne li mu gisoon mooy làkku Romam wii daal mooy gën ja a kawey jumtukaay ngir génne xasiday woyam yi. 

Bu ko defee Miguel de Cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di (don kixota) ci làkku Espaañ, ci noonu it la Rabelais ( 1483 - 1553 g )  def, moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di wu Fraans, ngir wuññi ci liy yëngu ci biiram, ci njàggat lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor (kaf). 

Chaucer mi dib angle ( 1342 - 1400 g) jug, moom itam, sotti ciw làkkam woyam yu yéeme yi cib taar, rawati na nettaliy Kentrebry yi, nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati Angalteer yu mag yi, yi gën’a siw.

 (3) Feeñug xeeti Orob yu yees yi:

Màggug fonk sa xeet ak sa reew   ci Tugal, juroon na ci jamonoy yewwute, ay reew yu bari ci Orob taxaw, yu amoon ag temb ,ci noonu, yittewoo xalaati fonk sa xeet daal di fay feeñ, fés fa, lu aju ci temb tam di lu ñu fay waxtaane, ak àttewiin yi  .

Looloo tax xarnub fukk ak juroom daa tàmblee dugg rekk, xataati politig yooyu ak yu dul ñoom tàmblee am ay maanaa yu nu man’a laal ci xeli lu bari ci nit ñi.
Ci noonu xeet yu bari ci yu Orob yi, tàmblee feddali yooyule xalaat ci jëf, di goreel seen bopp ci toppub jàmbur, te jambur boobu weesuwul woon paab bi ak imbratoor bi 
Ay àtte nag  yu Tugal yu am ay nekkte  yu politig yu temb  juddoo ci loolu ci ginaaw bi, yu am seeni làkki bopp yu yees, di ya nit ña daa waxe ay xarnuy xarnu waaye taxutoon ñuy làkki politig yi ak xalaat,  lu dul ci jamonoy yewwute gi.

(4) Yëngu-yënguy dajale mbind yi:   

Dëkki Itaali yi ak reewi Tugal gu sowwu gi ci jamonoy yewwute, dañu doon yittewoo dajale mbind yi ci fi ñu jortoon ne fi lanu nekk ci Xustantin  ak ci dëkki Gres yi, ak ci yeneen barab yi ci Tugal, mbind yooyu ñu daa wër nag ñooy yu Gres yeek Latin, yi nekkoon di lu ñu tas ci kàgguy daara yeek egliis yi ak katedraal yi,ak ci nit ñi walla kër yi yittewoo woon mbir mii.

Peey yi daan àtte, dañu daa jagleel lii alal ju bari, ñoñ nite ñi tam ñu ci bari jëmale woon nanu seeni ligeey ci dajale mbind yi, ci noonu ñu jot’a am ci misaal rekk,mbindu’m binkat bii di waa Rom te dib xutbakat, tuddoon Quintilian (35 nj - 96 g) ak bataaxeli Cicero (106 - 43 nj) yu xutba yi, ak woy yu at-ba-at  yu Tacitus yi(56 - 120 g)  . 
Tacitus moomu mooy taarixkatu xeexi jarmaan yi, mi ngi bokkoon ci ñi gënoon a ñaw ci xutbakati Rom yi ak seeni njàggatkat yu ñaw yi.

(5) Sonn ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya:

Yewwuteg Orob gi yittewoo woon na te sonnoon ci taarix ak jeexiit  yu yàgg ya.
Ag jublu gu yees am ci jàngiinu taarix, ñu koy teg leegi ci cëslaayu jam , waaye tegeesatu ko rekk ci dégg ak nettali, ci noonu ab jàngu  sosu ci Firenze  am njàngaleem jëm ci jam gu taarix , mu tudd daaray xam-xam bu taarix.

Bokkoon na ci boroom xam-xam yi ci gënoon’a duggal seen loxo, nitu taarix kii di Lorenzo Valla ( 1406 - 1457 g), mooy ki jamoon  te diiŋatoon benn dosye bu taarix, sikkoon it ag wéram, mooy li ñuy wax mayug Xustantin, mooy dosye boobu nga xam ne paab yi yàgg nañu cee sukkandiku, la ko dale ca xarnub fukk ak ñaar (g), ci seen xeex yi nu doon def ak buur yu mag yi ngir feddali ci seen àqi politig ci àtte nit ñi, jiite leen . 

Bokk na ci ñi nga xam ne yittewoo woon nañu gëstuy taarix yi ak yu politig yi, bindkatu itaali bii di xalaatkat bu politig bu am diplomasi, di Nicola Michiavelli ( 1469 - 1527 g),  Michiavelli mii def na teere bu mu tudde woon (buur bi), ndax da ci doon wax lu aju ci buur bu am doole, bu doon bennale dëkki Itaali yi, ak nguur-nguuraanam yu daggatoo woon yi te tas.

(6) Jëm-kanamug yaxantu ak endustri: 

Yaxantu noyyi na bu baax ci Orob gu sowwu gi,dale ko ci njëlbeenug xarnub fukk ak benn g. Itaali fi mu feete dimbli na ko bu baax ci yëngu-yëngug yaxantu dox fa te jëm fa kanam. Ci noonu lonkoo  yu yaxantu yi tàmbli fa’a sosu, di jëli marsandiisi penku yi, niki sooy, ak cuub yi ak rëndaay yi , ak wurus ak bëñu ñay ak yu dul yooyu, ginaaw bi it yii lonkoo - ginaaw bi ñu gënee jëm kanam – tàmblee yòbbu yii silaa  ci yeneen dëkki Orob yi, bu ko defee bu ñuy dëpp di indaale marsandiisi Orob yi, niki ngëndal ak der ak firaa . 

Jëm kanamug yaxantu googu ak gu meccey endustri yi, jur nañu ag xereñ ci denciinu alal, akug jëm kanam ci kee  yi ñuy jëfandikoo ci jëfi yaxantu yooyu, ci noonu am mbooloom ay sandikaay mecce feeñ, mujj teg loxo ci ginaaw bi, ci fepp fu koom nekk, te am fa cawarte, naka noonu nu def ay ligeey yu mag ci wàlli mboolaay  ak politig ak xalaat, raxaatal ci loolu juddug maas gu diggu gi  ñooy mbooloo miy ligeeye yaxantu ak yeneen mecce yu wuute yi.

(7) Feeñug yëngu-yëngug xam-xam gu yees gi:

Yewwute gi ci njëlbeen gi dafa sotti woon yitteem ci dundal njàggat yi ak fànn yi, ginaaw bi mu dox as lëf ba àgg  ci mbooleem lu xay gu mat laaj. 
Ci noonu yewwute gi matale mbooleem dundug mboolaay gi, bokk na ci, xam-xami dëppale yi , ndaxte xam-xam moom màggoon na ci dëkki Orob yi, jàngu yu mag yi  sosu ci Orob gi rawati na ci dëkki Itaali yi.
Yëngu-yëngug xam-xam googu mi ngi tàmblee ci di jeem a dundal xam-xam yu yàgg ya, ginaaw bi mu dox jëm kanam, loolu nag li ko waraloon mooy jariñu gi mu defoon ci yoonu xam-xam woowu di wu kojug nattu, maanaam lu nekk looy wax, nga teg ci sa loxo, mu leer la ne loolu la, nga doog ne moom la, ndax wóore na la ci làmb gi nga ko làmb ba daj ko, yoonu gëstu woowu nag, mooy wi boroom xam-xami jullit ñi jaaroon, ci noonu boroom xam-xamu fisiyaa bu Angalteer bi ñuy wax Roger Bacon ( 1220 - 1292 ) feeñ, di njiitul gëstug xam-xam ci Tugal .

Becon mii mi ngi sukkandiku woon ci yoonu jakkarloo ak nattu, ci gëstoom yooyu nga xam ne àggale woon nanu ko ci ay ngérte  yu am solo ci xam-xamu bidiw, ak bu weer yi  ak yu matematik yi, ak juxraaf .

Naka noonu boroom xam-xamu xeltu ak politig bu Angalteer boobu di Francis Bacon moom itam feeñ ( 1561 - 1626 g) , di koo xam ne dafa jëfandikoo xel ci àgg ci dëgg yu xam-xam yi , ci noonu ci gisiin, mooy ki teg ponki ngérum xam-xam mu bees mi, ak doonte moom doonul woon boroom xam-xamu dénd  .
Boroom xam-xamu Itaali bi, Leonardo da Vinci ( 1452 - 1519 g) moom tam feeñ , di kok dafa yittewoo woon jiyoloji  ( bu mekanig) ak matematig, ak yu dul yooyu, nga rax ci dolli fànnu yatt, ak nataal, ak misik, ak eeseñëri, mu nekkoon daal boroom xam-xam te di nitu fànn , tey fentkat.
Naka noonu boroom xamu Itaali bii di Galileo ( 1564 - 1642 g) feeñ , mooy ki njëkk’a defar nattukaayu tàngoor, njëkk’a fuglu bidiw yi ca fesalukaayam ba  , dëgëral te feddali gisiinu boroom xam-xamu bidiw bu Poloñ bii, di Copernicus ( 1476 - 1542 g).
 
Bokk na ci màndargay xam-xam yeneen yu yewwute gi, fentug móolukaayu teere ci loxol nitug Almaañ kii di John Gutenberg, atum 1404 g, fent gii ak doonte gu Almaañ la, teewul jëmale na kanam bu baax dundug nit ci biir Tugal ak biteem. Wuññiy juxraaf yi  tam ci màndargay yewwute gi la woon, ak yéwénalug diine gi  ci Tugal. Nga dolli ci loolu feddali gu nitug Tugal ki feddali jëmmam jii nga xam ne yàgg na’a nekk di lu nu làq ci jamono yu diggu yi ci biir ay kureel , walla sandikaay mecce yi mu daa bokk ngir làqatoo ca ak aar njàriñi boppam.
  
Yewwute gi ci Itaali: 

Yewwute gi ci Itaali daa tàmbli woon’a giim ak’a yànnjadi ci mujji fukk ak juroomeelu xarnu g, ak njëlbeeni fukk ak juroom benneelu xarnu g, loolu nag li ko waral lu bari la, ñu jéem cee indi yenn rekk yi ci ëpp solo:

Attekaay yooyu mosal nanu - ginaaw bu àtteb Lislaam dañee ca Andalusi te Garanada nërméelu, daanu - mosal nañu lu bari ci jullit ñi ay xeeti mbugal ak coona lu maneesul’a misaal, bokk na ci di leen lakk ñuy dund.

Tuxug Yewwute gi:  

Ak li yewwute gi di neew doole ci Itaali lepp, taxul mu naaxsaay, mbaa mu suux, li am kay mooy da fa’a tuxoo dem ci yeneen reew yu Tugal niki Espaañ, Portigaal, Fraans, Angalteer, Holand, ak Almaañ, añs.
Ay jëfka  yu bari bokk nanu ci li tuxale yewwute gi jële ko Itaali yòbbu ko ci yii dëkki Orob, bokk na ci yooyu nekk gu yii dëkk nekk di yuy door’a noppi ci seenug sosu gu politig gu yees, ak tàbbi gu ñuy doog’a def ci jamonoy tabax ag xay.
Ñi daa woote yewwute gi nag def nanu lu rëy ci tuxale ko Itaali mu dem feneen.
Nitug Holand kii di Erasmus ( 1466 - 1536 g) moo tasoon te wisare yewwute gi ci Almaañ, jaarale ko ci def fa ay waxtaan aki xutba, ak ci yeneen dëkk yu Orob yi.

Erasmus mooy ki firi Injiil jële ko ci làkku Gres yòbbu ko ci wu Latin, jël nag li ñu ciy wax kòllare gu yees gi  def ko ci ay làkki Orob yu bees, loolu bokk ci li feexal te goreel  xalaatub Tugal bi ci ngartaajoo gi ko niti diiney katolig yi ngartaajoo woon.
Loolu it won na waa- Tugal ne yaxub Injiilub latin, bi egliis bi yoroon du woon biy cosaan, te yax bu bari woon ay yàq la, kon daal Eramus mooy ki waajal xelum Tugal mi ci mu man’a nangu yéwénali diine yi.

Ni yewwute gi meloon ci fu dul Itaali:  

Yewwute gi ca Almaañ dafa yoroon melow njàngat, wiy ligeeyal gëstuy diine yi (ci manaa daa yamoon daanaka ci lu aju ci diine rekk). Ca dëgg-dëgg, gëstu yi aju ci xam-xami Gres-Latin yi, dafa xawoon’a yeex’a àgg ca dëkk yooyu di yu Almaañ, ak li njiiti yooyu dëkk daa dimbli gëstu yooyu lepp cig wàll, ak li Almaañ doon am ay daara yu mag  ci Vienne ak Idelberg ak Baasal ak Strasburg ak yu dul yooyu lepp, ci geneen wàll.

Yeex googu nag li ko waraloon mooy niti diine yi ak ñu dul ñoom ñoo ko nanguwutoon, ñoom daal danu fee nekkoon rekk di sàkku nu ñu tënke, te jéng yooyu njàng ak gëstu, te defi pexe ba du ñu tas ci anam gu yaatu, ngir nu wattoo ci seen kilifteef, sàmme ci seen daraja, aare ci seen ligéey.
Ci noonu, danañu gendiku ne yëngug nite gi ci Almaañ dafa doon sori jubluwaay yu deet-diine yi , looloo tax du kiimaan Almaañ di woon barab bi uufoon yëngu yu yéwénali diine yi gënoon'a am solo ci Tugal.

Bu dee ci Fraans moom yewwute gi melow njàngat ak nite la fa yoroon, wi yittewoo woon xam-xami Gres yi. Ci noonu boroom xam-xami Itaali yi ak yu Gres yi taxaw ci wisaare gëstuy xam-xami Gres yi, ñu móol teerey ndonoy Gres yi ci móolukaayu Paris ba ñu taxawaloon ca xarnub fukk ak juroom benn g, ni nu duggale seen loxo ci amal ay akaadimi aki barabi xam-xam ngir njàng yi aju ci nite, niki bànqaasub  buur bi ci Paris, ñu sos ko ci jamonoy Buurub Fraans bi, di Fransuwaa mu njëkk mi atum 1540 g.

Bu dee ci Angalteer, ba tay yewwute gi ma nga fa yoroon melow njàngat ak nite. Ay gëstu yu xam-xami gres yi am fa, ay ñoñ nite ñu waa reew ma, ñu bari ñooy ña ca siwoon, ñoom ñooy ñi daa jàngale làkkuw Grees wi ci daaray xam-xami Itaali yi, ku ci mel ne Wilyam Lilly mi daa jangale làkkuw Gres ca Rom.
Erasmus mu Olaand mi ak Kolt mu Angalteer mi, ñoo tekki woon Injiil ci làkkuw angale wu bees wi.
Buurub Angalteer bi, Henri mu juroom ñatteel mi, moom tam sosoon fa juroomi toogu yu darajay ag ustaas ci xam-xami pas-pasu nasaraan ak yoonu siwil   ak wu dénd bi  ak làkku ebrë  ak wu Gres ci daara ju mag ju Kembrij. Jàngub San Pool bi nekk London moom it jagoo woon njàng yu nite yi.

Yewwute gi ci Angalteer dafa jublu woon yoonu takk ak boole diggante pas-pasu nasaraan ak gëstuy nite, yu njàngat ak yu fànn yi. Yewwute googu nag indiwul woon lu yees, lu ñu fent, ndare ci xarnub fukk ak jurom ñaar g, bi am njurum njàggatam ak mu niteem mu yees feeñee ci anam gu fes te rafet ci woyi William Shakespeare yi (1564 - 1616 g ) ak woykat bu silmaxa bii di John Milton (1608 - 1674  g ) ak ñu dul ñoom ñaar. 

Fii tam ci Angalteer yoonu yewwute gi da fee jengoon as lef jëm ci yewwute gu xam-xam, gu aju ci xam-xami dëppale yi  walla xam-xami nattu, yu làmb yi.
Ñi jiitu woon ci lef moomu, ñooy ñaari boroom xam-xami Angalteer yii di Roger Becon ak Francis Becon, ñoom daal ca dëgg-dëgg ñooy ñi sos daaray xam-xam ca Angalteer.

Baat bi nuy mujj a wax ci yewwuteg Tugal gi, mooy moom daal moo ñàkkal jamono yu diggu yi kàttan ci jeexiital ci mboolaayu Tugal gi  ci wàlli dundug politigam, gu mboolaayam, gu xalaatam ak gu aadaam  .

Ngir jeexiit yii fi yewwute gi sotti ci Orob, ay noste yu yees am nañu yu làmboo tabax guur gu yees gi ak mboolaayug Orob gi ci cëslaay yu aada, yu mboolaay, yu jikko, ak yu ngér yu yees, ni mu duggale loxo ba tay ci ubbi ay gox yu yees yu xam-xam, yu jël gisiini xam-xam yi ak dal  yu xam-xami juxraaf yi. Lii lépp nag moo sabab jamono ju yees ci Orob,di  ju wuuteek ja woon (ca jamonoy laman) ci xalaat, ak ngér  ak defiin aki xew-xew.
Loolu lepp nag nga boole ko, moo jur jamonoy Tugal ju yees jii.

Doggantal gu ñaareel gi:

Wuññi  yu juxraaf yi  :

Luy wuññi yu juxraaf yi ?:

Yëngu-yëngu gu wuññi gu juxraaf, walla feeñal gu juxraaf, yëngu-yëngu gu yàgg la. Waa-Isipt ñu njëkk ña ak Finiix yi ak jullit ñi defoon nañu ko bu yàgg,njëkk waa-Orob di ko def ci jamono ju yees ji. Lu am soloo ngii nag ñu war koo xam, mooy wuññi'y juxraaf yi, bi muy am it li ko taxoon’a jug mooy ay xemmemteefi sañc , ak doonte daa mbubboo woon gëstu gu aju ci xam-xamu juxraaf.

Yëngu-yëngu gu wuññi gu juxraaf  gi ñuy waxtaane ci doggantal gii, da nanu ko man’a xamalee ci nii: 
mooy mbooloom ligeey yi jéngukat  yu Tugal yi daa def ci ñaari xarnu yii: bu fukk ak juroom ak bu fukk ak juroom benn g. Yenn nag ci réewi Tugal yu nasaraan yi, ñoo leen doon soññ ak’a jàmbaarloo ak’a xiirtal ci loolu.

Li sabab wuññi yii:

Sababu diine moo jiitu ci sabab yi waraloon yëngu-yëngu yu wuññi yu juxraaf yu Orob yii am. Sababu diine mooy li gën’a waral ñaari reewi katolig yii di Espaañ ak Portigaal defoon ligeeyub wuññi boobu.
Ñoom yile ñaari reew dañoo jortoon ne dananu man’a sutuxlu ci biir Afrig ak fu dul moom, def ko barab bu dëppoo ak li ñu bëgg muy tas fa ag katolig, ak nangu ko teg ko loxo jaare ko ci diine. Reewum Portigaal moom daa gisoon ne reewum Ecopi, - mii di mu nasaraan, waaye di mu yoroon ngérum xibt, mu ortodoksi - man na koo soppi def ko mu yor ngérum katolig. Loolu nag da nga ci gise diinewu gu dëgër gi amoon ci waa-Espaañ ak waa-Portigaal ca jooja jamono.
Paab gi moom da daa soññ reewi nasaraan yi ci ñu dugg bu baax ci wuññi yooyu, ngir tas ag katolig, ak xatal Lislaam te sonnal ko,tee koo tas, ngir neewal dooleem, xottite ko,giir ko.

Ci noonu mu ( moom paab gi) génne ay mbind yuy jox àq ñaari reew yii ci ñu moom gox yu yees yi ak mbooleem yu nu wuññiwaat, moo xam geej yi la mbaa jeeri yi.
Paab gi ak nasaraan yi ci ginaawam, dañoo ragaloon lislaam ak ñoñam, looloo taxoon ñu daa wut nu ñu mucce ci ñoom, ñu ne woon kon nanu leen fi jeem’a jële.

Am na yeneen reew yu yees yu feeñ ci ëttub politig bu Tugal bi, yu ci mel ni Espaañ, Portigaal, Angalteer, Fraans, Holand ak yu dul yooyu. réew yii nag, dañoo tàmbli woon di xalaat bu baax ci tas ak wisaare seeni kilifteef ak jeexiit  ci biti seen, rawati na ci reew yi ci yeex ci seenu'g nekku walla sosu gu  yees. ñu gisoon it ne bu ñu fa tasee, wisaare fa seeni xay aki ngéri diine,loolu da na man'a nekk ay raas yu ñu man'a jaare ngir sampu fa, sanc leen  . Reew yii nag joŋante woon nañu te gëpplante ci mii lef , loolu bokk ci li daa soññ ak’a xiirtale ci yëngug wuññi gu juxraaf gi.

Waa Orob yi ñoom dañoo gisoon ne addunay jullit ñi daal,mooy ji ngëp ci loxoom nosub  yaxantu bi, ndaxte ñooy ñi notoon, tegoon loxo ci kaw yooni yaxantu yu penku yi. Ci noonu xalaatu wacci fi yooyu yoon, te gëstuji yeneen yu leen man’a àggale End ak Siin tàmblee feeñ, ngir bañ’a fay njëgi nduwaañ yi ak galag yeek yeneen yi cig wàll, ak ngir neewal doole koom-koomu jullit ñi ci geneen wàll, ginaaw bi ñu soppee yoon yooyu def leen leegi ñu jaar Afrig ak màmbulaan gu atlas gi , loolu lépp ngir bañ’a jaar fi jullit ñi dëkke.

Yenn ci réewi Tugal yu yees yi dañoo gisoon ne li gënoon ci ñoom mooy seeni séqoo yu yaxantu  ak réewi penku yi, ñu koy defal seen bopp, ngir mucc ci rënkug yaxantu  gii dëkki Itaali yi ame woon te daan ko def, yu ci mel ni Venezia ak Genova ak yu leen moy. Xalaat bii nag taxoon na ba yii réew demoon gëstuji aw yoonu yaxantu wu bees, nga xam ne ñoo ciy nekk ci wenn waxtu wi di yaxantukat biy jëli ,tey tuxal, tey kiy dox ci diggante yi.

Lori waa Orob yi  tàmbli woon na’a yol, bi ñu déggee xibaari wurus ak xaalis ci Afrig, ndax kat mbell yu gànjaru yi  dañoo muuroon seeni gët, fees seeni xel, ñoom ñi nga xam ne dañoo tàmbli woon di faale ak a yittewoo wàllug ne-ne gi  rekk, bayyi nee yeneen wàll yi, loolu moo tax ñu sawaroon lool ci def wuññi gu juxraaf gi bi ñu déggee tono  gu ne-ne gu rëy gi nga xam ne am mbooloo ci wuññikati Orob yi ndàmmoon  nañu ko ci seen tukkiy wuññi yooyu, rawati na bi ñu jàngee xisay tukkikatu Itaali boobu di Marco Polo (1254 - 1324 g ), mi wuññiji woon ba Siin (1271 - 1275 g ), nga xam ne bi muy dëpp, daa indaale lu sakkan ciy doj yu tedd , ba mujj waa Venezia daa ko wooye boroom milyoŋ yi .

Xalaat yi boroom xel yi ci Tugal amoon ci suuf si, ak bindam  dafa soppiku woon, ginaaw bi ay tukki yu juxraaf yu kenn-kenn amee ak yu mbooloo yu nasaraanal ,juge Orob, génn, rawati na ginaaw bi jamonoy xarey jooñ yi  jàllee, nga xam ne boroom xam-xam yu bari leegi dañoo am koolute ci ne suuf si dafa bulu  walla  mu mel ni ab kol-kol, wuute ak la ñu jàppoon, gëm ko, muy dafa tàllaliku mel ne basang gu ñu lal, loolu nag mooy li muuroon xeli waa Orob yépp ci jamono yu diggu yi.
Ag jèng jëm ci sopp ag jéngu , ak bëgg xam-xamu juxraaf, feeñ ci ñoom, ginaaw ba fa ruug gëstu gu xam-xam gënee suuxatu, gën fa’a jëme kanam, ak li ñu jële ci jullit ñi - ci biir xeexi jooñ yi ak ginaaaw bi - ci xam-xam bu juxraaf bu jëm kanam, ak ginaaw bu xam-xamu bidiw ak ligeeyiinu gaal ak buusal biy won gaal yi seeni yoon gënee jem kanam.

Wuññiy juxraaf yu Portigaal yi:  

Portigaal moom la ñu’y jàppe reew mi jiite woon wuññi yu juxraaf , yu Orob yi. Buur bii di Henri, mi nekoon ab mool  (1394 – 1460 g ) , doonoon doomi buur bu Portigaal bi tudoon John mu njëkk mi, moom mooy ki njëkk’a def ay wuññi ci waa Portigaal yi. Mu nekkoon ku soppoon dugg geej, ak yër xisay mool yi, ak teerey taariix yi . Muy ku aayoon ci rëdd karti juxraaf yi , moom la baayam sàmpoon mu yor Sawuta , ginaaw bi ñu ko nangoo ci julliti Marog yi atum 1415 g.

Henri daa xalaatoon’a wesaare diine’y nasaraan ju katolig ji ci Afrig, ci noonu mu ne kon na jokkoo’k buuru nasaraan bu Ecopi bii di Prester John, ngir ñu ànd, xeex waa Marog yii di ay jullit cig wàll, ak ngir man’a àgg ca waaxi  geej gu xonq ga  ci geneen wàll. Ci noonu mu yabal ay mool yoy ci seen tukkiy wuññi yooyu, àggoon nanu ba ca duni Kanaari ya , ak Madira ak Osoras ci Mambulaanug Atlas , atum 1402 g, naka noonu ñu wëy ci seen tukki yooyu ba agsi Senegaal, atum  1445 g, ginaaw bi Henri deewee tam teewul seen tukki yooyu wëyoon ba ci sottiwaayu dexug Kongoo gi ak Niijer. Bu ko defee mool bii di Bartholmew Diaz, moom àgg ba ca wàllug bëj-saalumu Afrig, di fa ñuy wax Boppub Callmeer, atum 1486 g, moom la buurub Portigaal bi soppi tur wi tudde ko « Boppub Yaakaar Ju Baax Ji » ngir mool yooyu man cee ame yaakaar ba man’a wuññi yoonu yaxantu wi jëme End.
Mool bu siw bii di Vasco De Gama moom, jug def tukkib wuññi, atum 1497 g, daal di àgg End, ginaaw bi mu wëree Afrig jaare ko ci yoonu tefesug Marog gi,  romb Bopp Yaakaar Ju Baax Ji,  ak Mosambig ak Mombasa ak Malandi, ba àgg (Jawa) ca tefesug sowwu gu daanaka dun  bu End.
Vasco De Gama mii jot naa xamante ak  Ahmadu’bnu Maaja mii di woon ab mool bu jullit bu araab, moo ko dimbli sax ba mu man’a àgg End, ndaxte mooli jullit ñi ñu xamoon geeji penku yi lañu woon, ak yooni yaxantu yu jéeri yeek yu geej yi.
Naka noonu beneen mool jugati bu tudd Kabraal, def ab tukki bu geej bu aju ci xare, dem End ,tàmblee naj ak’a sonnal Samirin,mi daa àtte ak’a saytu fi nuy wax Kalikuta gu End gi, ngir mu jox Portigaal ab barab bu yaxantu  ci tefes gu sowwu gi, Kabraal mii xeex na fa’ak jullit ña, song  barab ya ak mbooloo’m gaalam ma. Vasco De Gama moom itam delluseeti End ci ab tukkib xare ngir faagaagalsi Samirin, ak mbugalsi yaxantukati araab yu jullit yi, ak defsi ay déggoo  ak buuri goxi End yi nekk ci tefesug sowwu gu daanaka-dun  bu End bi.

Li wuññiy juxraaf yu Portigaal yi jur :

Wuññiy Portigaal yi jur nañu ay ngérte yu  bari, yi ci ëpp njariñ ñooy yii di ñëw :

Loolu nag  mooy li doyadiloon koom-koomu jullit ñi ci penku bi, maanaam koom-koomu nguurug Mamaalik ci jëmmi boppam. Lii moo taxoon nguurug Mamaalik mujjoon neew doole ci kanamu nguurug Portigaal gi ak ci kanamu ñoñ Usmaan ñi  nga xam ne jot nañoo fexe ba xaw’a woyofal naj ak ñàkkal jàmm gi Portigaal defoon araab yi, ak nguuri araab yi nekkoon ci tefes gi, yàqoon nañu it mbooleem jeem yi ñu daa def ñoom waa Portigaal ngir taxawal ab jë  bu nasaraan kontar doole yu lislaam yi nekkoon ci peggu geej gu xonq gi, ak tefesug Afrig gu penku gi.

Wuññi yu  juxraaf yu Espaañ yi : 

Li ci duggaloon Portigaal, moo duggal it Espaañ ci wuññi yooyu. Ci noonu boroom xam-xam yi daa yëngu ci mbiri wuññi gi, danoo jàppoon ne suuf si daa bulu, moo waraloon ba ñuy dem End ñu jaare woon ko ci sowwu bi.

Moolub Itaali bii di Cristoforo Colombo (1451 – 1506) moom defaloon na waa Espaañ ñi benn tukkib wuññi atum 1492 g, juge Espaañ jem End jaare ko ci sowwu bi, ci màmbulaanug atlas gi. Ginaaw tukki bu tar te sonnle, moom Colombo àgg na ca duni Bahama ya mu mujjoon’a tudde San Salvador, juge fa dem ca tefesug Kubaa gu bëj-gànnaar ga ak dunub Ayiti bi mu faroon tudde Espaañ gu ndaw gi.

Mu delluwaat nag Espaañ ci atum 1493 g, ànd ak jort ne moom de jot na’a àgg End ci yoonu sowwoom woowu. Ci atum 1493 g, Colombo defaat na ab tukki, bu li ko taxoon’a jug mooy teg loxo ci suuf yooyu mu jotoon’a wuññi ci atum 1492 g, ak wisaare fa katolig, ca ña fa dëkk te mu tudde woon leen ay « endo ». 

Ci tukki bii la jotoon’a wuññee Jamayka, daal di delluwaat Espaañ ci atum 1496 g. Mu defati ñatteelu tukki atum 1498 g, waaye amu ca woon tawfeex. Mu dellu defaat bu ñeenteel atum 1502 g, taxul ba tay mu am ca la mu ca doon wut. Bu ko defee nag ñaari sooy yii mu def ci ñaari tukkeem yi tax ba buuru Espaañ bi Ferdinand ak soxnaam lingeer bi Isabela, begadi woon ci loolu, ag siwam suux, ñu folli ko ci njiitul geej gi, daal di koy delloosi Espaañ ci ay jéng, ngir mere gu ko meññilukat  yi mere, ñoom ñi seen yaakaar tas. Colombo faatu na atum 1506 g, te xamul sax ne wuññi na adduna ju yees ju dul End.

Ginaawam it wuññikat yi doon ligeeyal Espaañ wëy ci seen ligeeyi wuññi yooyu , ka cay Amerigo Vispucci jot ca’a àgg ca gox ya Colombo àggoon ak yeneen yu mu àggutoon, ci njëlbéeni xarnub fukk’ak juroom benn. Moom mool bii di Amerigo, moo am teraagay ñu tudde ko Adduna bu bees bii di Amerig tay.

Li wuññiy Espaañ yi jur:

Wuññi yu Angalteer:  

Ñoñ Angalteer ñoom itam sóobu woon nañu ci wuññi yi, bi Buur bi Henri mu juroom ñaareel, mi nekkoon buurub Angalteer digalee mool bii di John Cabot, mu tukki dem End, jaare ko bëj-gànnaar gu suwwu gi, ca saa sa mu geeju, tukkee Bristol atum 1497 g, jéggi màmbulaan gu atlas, àgg tefes gu bëj-gànnaar gu Amerig gu bëj-gànnaar gi, ca New Fondland, ginaaw bi mu jéggi Librador, dellu Angalteer. Cabot mii delseeti na leru tefesu’g penku gu Amerig gu bëj-gànnaar gi, ba àgg Florida, loolu nag moo doonoon tàmblig sancug  walla koloniiseg waa Angalteer yi, ñeel Amerig gu bëj-gànnaar gi ak Kanadaa . Ba tay it, kii di Jams Kook di woon ab mool bu dëkkoon Angalteer, defoon na moom it  ñatti tukki yu wuññi ca tefesi Ostrali yu penku ya ak Newsiland.

Wuññiy Fraans yi : 

Waa Fraans nag ñoom, ñoo mujjoon’a duggsi waa Angalteer, waa Espaañ ak waa Portigaal ci lefum wuññi mi, ñoom seeni tukkiy wuññi daa jemi woon Kanadaa. Ki ñuy wax Jaak Cartier  moom ab mool la woon, daa jugoon def benn tukkeem  bu wuññi ci jamonoy Fransuwa mu njëkk mi, jeggi màmbulaan gu atlas gi, jem sowwu, fetali àdduna ju yees ji. Ci noonu mu àgg New Fondland gi jàkkaarloo ak Kanadaa, daal di fay jot’a wuññi  walla feeñal sottiwaayu dexug Santa Lorans. Tukki yi Cartier mii jot’a def ci goxi Amerig gu bëj-gànnaar gi ñeent lañu woon. Bi mu ko defee sancug Fraans  tàmblee putuxlu ci Kanadaa, ak goxi dex yi ci Amerig gu bëj-gànnaar gi. Noonu ñu taxawal ab sancu  tudde ko Samwel de Shampala, taxawal it dëkk bii di Kebek ci tefesug dexug Santa Lorens atum 1608. moolu Fraans bii di De Laasal jotoon na’a wuññi dexug Misisipi, ci noonu waa Fraans ya daal di fay sos sancu walla koloni bu Luwisiyaana, bii nga xam ne mi ngi jële turam wi ca buurub Fraans ba tuddoon Luwis mu fukk ak ñeenteel mi.

Wuññi yu Oland yi :  

Lonkoo  gu End gu penku gu Oland gi, dafa joxoon ndigal moolub Angalteer bii di Henry Hadson, da ko’o joxoon ndigal ci mu defal Oland ab tukkib wuññi, ngir man koo gisal aw yoon wu bëj-gànnaaru penku wu ko man’a àggale Asi, ci noonu mu geeju moom Hadson juge Angalteer, jaare ko ci bëj-gànnaaru atlas gi, jawali golofub New York, ak dexug Hadson gi mu tudde woon boppam. moolu Oland bii di Wilyaam Shotin moom, moo wuññi yoonu boppub Horn bi nga xam ne mujj na di yoonu geej wu am njariñ. Waa Oland yi jeemoon naño’o wuññi Ostraali ak Newsiland ci diggante 1622 – 1624 g .

Li wuññiy juxraaf yu Orob yi jur :

Li wuññiy Tugal yi jur man nanu koo tënk ci lii di ñëw :

Yëngu-yëngu gu yaxantu gu yees gii, ñi ngi ko tudde woon « soppi ci anamug yaxantu » .

Doggantal gu ñatteel gi :

Yëngu-yëngu yi jugoon di kontar Egliis bu paab bi

Yëngu-yëngu gu yewenal diine ji ci Tugal :

Yëngu-yëngu gu yéwénal  gu diine ci Tugal, mooy googu doon am ci Orob ci xarnub fukk ak juroom benn g, ngir setal Egliis bu katolig bi ci li ci taqoon ci ay ñaawtéefi pas-pas ak yu jikko, na ñu ko daa defe mooy jeem’a delluwaat ci njàggaley Injiil yi.

Li waraloon « yéwénal » gi :

Ak li Egliis bi di nekk nguurug ruu lepp - ci li ko njëkk’a tax’a jug -  teewul ànd ak li jamono di gën a yàgg, mu jot’a àgg ci ŋëpp - ci loxob weñ  - nguurug diine gi ak gu politig gi, maanaam, mu tëye tëyiin wu metti te tar, ñaari nguur yii di gu diine gi ak gu adduna gi. Ci loolu la mujje di dooley politig, ju diine, ju koom, ju mboolaay ak ju aada  ci mboolaay yu Tugal yu katolig yi ci jamono yu diggu yi. Dàkku  nag walla xañ nit ki  jàngu bi  moo nekkoon mbugal mi gën’a saf, te gën a tar, mu Egliis bi moomoom, daan ko teg kuy jeem’a léewtoo’k moom, ak nu darajaam man’a kawee, mbaa mu màgge ni.

Egliis bi ci safaanub muy jëfandikoo nguurug ruuwam gi, di jëmale nit ñi ci yooni baax ak ragal Yàlla, moom déy – ginaaw ag mbon da koo duggoon – daa labaloon boppam ci bànneexi adduna aki caaxaanam, fàgguloon boppam ay suuf yu yaatu, ay alalam it mu teggiloon leen, te musal leen ci galag  yi ñépp di fay. Ci noonu paab yi ak kardinaal yi nekkoon di ñu nuuroon ci dundug adduna aki caaxaan yu ëpp.

Ñaawtéefi Egliis yooyu ak yu leen moy, ñoo gestuloo woon te fëkkoon yittey yéwénalkat yu mboolaay yi ak bindkat yi ci jamonoy yewwute gi.

Ki gënoon’a jeexiital ci mbooleem bindkat yooyu, mooy labbe bii dib xeltukat  ,  nu ko daa wax Erasmus ( 1466 – 1536 g), moom daal jamoon na  ci teereem bi tudoon « tagg ag ndof » (Praise of Folly) , jamoon na ci nekkiinu egliisu katolig bi, mu nekkoon jam yu tar te wex.

Dox gu taarixe gi yéwénalug diine gi defoon ci Orob :

Yéwénalug diine ci Orob - ci doxam bi - romb na ñaari tolluwaay : bi ci njëkk mooy : bi ay yëngu-yënguy yéwénal yu ndaw amee te lalu niki ay njiitlaay aki cëslaay yoo xam ne ci seen kaw la yëngu-yënguy yéwénal yu diine yu mag yi ci Tugal tegu. Bu ñaareel bi nag mooy yëngu-yëngug yéwénal gu mag gi ci boppam.

Bu dee nag yëngu-yëngu yu diine yi nooyal yoon wi ba yu mag yi man’a am, man’a taxaw ci Tugal, ñoom ñooy yi nuy wax Fransiskaan ak Dominikaan, ñooy yi gisoon ne mant’a ñàkk nu dañal njuumte ak ñaawtéefi diine yi niki aw yoon wu nuy jaar ngir yéwénal Egliis bi te dëgëral ko.

Ag yëngu-yëngu gu yéwénal daal di taxaw ca Angalteer ci njiitl John Wycliffe (1330 – 1373 g), moom kenn la woon ci ustaas yu siw, yu daaray Oksford ju mag ji.Googu nag li ko taxoon’a jug mooy dañal li taqoon Egliis bi cig mbon. Gii yëngu-yëngu moom mi ngi judd ginaaw lu tolloo’k xaaju xarnu, ginaaw juddug yëngu-yëngu gu ñaari way sell yii di Fransis ak Dominik, waaye gii nag moo gënoon’a fés, gën a jeexiital ci egliis bi ci gu Fransiskaan gi ak gu Dominikaan gi. Geneen it feeñati gu yéwénal ci Bohimiya ci njiitul John Hess (1373 -  1415 g) , moom mooy ki ne woon : ag diggale  wart’a am ci diggante nit ak boroomam, ndare diggale googu doon ngëm ak jëfe li ci Injiil. Hess nag li mu jublu woon ci loolu mooy wàññi sañ-sañu Paab gi, ak neenal taxawaayub làbbe bi niki aji diggale  ci diggante jaam bi ak boroomam . 

Bu dee yéwénali diine yu mag yi ñoom, ñi ngi doon jëmmu ak’a feeñe ci am gi yëngu-yëngug Protestants gi amoon, njiit ya di woon Martin Luther, Kalfan ak Swingli.

Martin Luther ak yéwénal gi :

Martin Luther mi ngi juddoo  Isilban, di benn dekk ci diiwaanu Saksoniya ci Almaañ atum 1483 g, faatu atum 1546 g, baayam nekkoon ku daan ligeey ci benn ci gasuwaayi mbell yi.
Mu màgge nag ci njaboot gu ndóol, ak ci ron dund gu jafe te wow. Moom nag jàng na cosaani làkkuw latin, ak cosaani ag katolig, noppi jàng yoon ak xeltu, dugg nag ginaaw bi, benn ci barabi jaamu yu katolig yi, ngir laabal fa boppam ciy bàkkaar aki ñaawtéef, loolu nag ci gëm-gëmi katolig yi la bokk. Ginaaw bi mu tukki dem Rom atum 1510 g, def fa weer, gisal boppam ñaawtéefi paab gi, ak bon-boni Egliis bi, li gënoon’a wëlbati ay bëtam mooy jàdd gi niti diine yi jàddoon, ak wàcc gi nu wàccoon  yoonu leer ak lëmoodiku wi nasaraan gu njëkk ga yoroon, ak set gi mu setoon . Lii jeexiitaloon na ci boppam, ak xelam mu daladi mi, jañoon ko it ci jam walla kritige paab gi, ginaaw bi it, mu mujj fèttéerlu ci kawam , bi mu bañee –moom paab gi - ne du soppi aw doxaliinam. 

 Dikk gi labbe bii di John (Tetzel) dikkoon ci diiwaanu Saksooniya atum 1517 g, ngir jaaysi fa ‘xobi njéggal’ yi, dikk googu dimbli woon na Luther ci mu man’a feeñal li nëbbu woon ci biiram muy yéeney yewenal yi mu yoroon te fasoon leen ci xolam. 

Jaadu na ñu fàttali leen ne ‘xobi njéggal’ mooy li fi wuutu woon tuubug aji tooñ ji, ci jeem’a fare ay bàkkaaram ci def lu baax, jaare ko ci julli walla joxe asaka mbaa woor. Waaye paab bii di Liyoo mu fukkeel mi, moom daal, da ne woon da na doy aji moy ji bu bëggee tuub ay bàkkaaram mu aji-ji Rom, ginaaw bi, wax jooju xaw’a gën’a jëm kanam, gën’a xóot, bi kenn ci paab yi nee : njéggal daal man na’a ame ci nit joxe ci alalam ci Egliis bi, ngir ñu dundale ci diine, bu ko defee ñu jox nit kooku ‘xobu njéggal  .

Luther moom dafa kontaroon njaayum xobi njéggal yi, mu ne woon : mucc mbaa mbugal ak fayoontoo, manuñoo juge ci jënd ay xobi njéggal, fa nu man’a juge kay mooy gëm Yàlla. Luther moom diiŋatoon na xobi njéggal yi, daal di woon dem ba ca Egliisub Wtanberg ba, wékk fa mbind mu ëmb ay diiŋat yu toll ci 95 , ci atum 1517 g . Paab bii di Liyoo mu fukkeel mi amoon na taxawaay bu tar ci xalaati Luuther yi, ndax daal di woon nay genne ca saa sa benn saxal walla ndigalul xañ, ñu teg ko Luther, saxal boobu walla ndigal loolu moom lanu daa wax (Wermis), waaye Luther moom faalewul woon saxal bii, moom kay da koo sanni woon ca ëttub Egliisu Watanberg ba, lakk ko.

Xalaati Martin Luther ak ay gisiin yu yéwénal yi mu yoroon : 

Luther, xalaati yéwénal yi mu woote woon jëme ñoo’y yii di ñëw nii :

(1)	Injiil mooy nattukaayub diine ak bu yoon bi muy sukkandikoo ci firi pas-pas yi ak mbooleem masalay diine yi am ag wuute.
(2)	Nit ku jàng ku nekk tey jëfandikoo xel sañ na’a jàng injiil te firee ko ni mu ko dégge, xame ko ni.
(3)	Paab bi amul - benn yoon - àq mbaa sañ-sañ ci rënkal fi boppam, moom rekk, sañ-sañu firi injiil.
(4)	Sëy daa war’a dagan ci làbbe yi.
(5)	Niti diine yi dañoo war’a nekk ci ron kiliftéefug nguur gu àdduna gi.
(6)	Wàññi limub jàngu  yu bari yi tasoon  ci mbooleem reewi Orob gu sowwu gi.

Bu nu xoolee xalaati Martin yi dananu gis ne moom daal li ko yitteeloon mooy mu neewal doole sañ-sañu paab bi, loolu yaa ngi koy gisati ci bi muy sàkku nu neenal diggale  gi daa am ci diggante Yàlla’ak’ub jaamam. Sàkku gi mu doon def it ci nu neewal limub jàngu yi li mu doon wund mooy neewal ngañaayi Egliis bi aki am-amam, ndax loolu man’a soril Egliis bi caaxaan ak po mi mu nekke woon. Da nga gis it ne wax ja mu waxoon ne nit ku xam ku nekk am nga àq ci jàngal sa bopp injiil ak firee ko ni nga ko dégge, moom itam li mu doon tekki mooy jeqiku  gu mu jeqiku woon ci Egliis bi, ak rafleel gu mu ko rafleeloon  ci li mu jàppoon moom Egliis bi ne àqi yoonam la ju mu moom.

Jëfka  yi dimbli Luther mii ci wooteem gi man’a àntu :

Am na ay jëfka yu bari yu ñoo dimbli woon Martin ci fipp gu yéwénal gi man’a àntu. Yi ci ëpp solo ñooy yii :

(1)	Feeñ gu Luther mii feeñoon ci jamono joo xam ne waa Orob yi seeni xel da cee tàmbli woon’a ubbiku, ñu tàmbli woon’a fèqu ak’a dañtalu ci ŋëbug paab gi ak sañ-sañam.
(2)	Siwug njuumte ak ñaawtéef yu rëy yi nga xam ne taqaloon nanu derub paab gi, te taxoon ba nit ñi doon sikk ag muccam ak ag sellam.
(3)	Fonk sa xeet,walla xeetu  gi tàmbli woon’a feeñ ci reewi Orob yi, te taxoon waa Almaañ ñi defoon ab dank topp ci ginaaw Martin Luther, rawati na maas gu diggu ga ak baykat ya ak gawar ya.
(4)	Dimbali gu ko ustaas yu daara yu mag yu Tugal yi dimbali woon, ak ñu dul ñoom ci xalaatkati Almaañ yi warlu woon ne ñooy fas yeenee tas xalaatam yooyu.
(5)	Firi Injiil ci làkku Almaañ, ak def ci ay taalif yu tax waay Almaañ ji man’a gis ay xalaatam, yër  it jam  yi mu doon def Egliis bi .
(6)	Tasug móolukaayu téere gi nga xam ne Gotenborg moo ko fentoon, loolu taxoon nag ba xalaati Luther yi tasoon ci waa Almaañ yi ak ñu dul woon ñoom.

Am na benn xeex bu mag bu amoon ci diggante Martin aki gaayam, ñoom ñi diy protestants, maanaam ay diiŋatkat cig wàll ak diggante ñi toppoon paab gi (katolig yi) ci geneen wàll. Dëkki Almaañ yi moom xare yu tàng’a fa amoon, dongay ñaari ngér yii doon xeex nag mujjoon nanoo xaatim ag juboo, gu nu tudde woon (Augsburg) atum 1555 g, ñu nangu woon ci ne goxu Almaañ bu nekk am na àq ak sañ-sañ ci tànn ngér mu ko neex, mu protestant  mbaa mu katolig, waaye ci wàllug ofisel ñu tànn protestant def ko diine, ngérum Luther mu protestant mii tasoon na te siw ci goxi almaañ yu bëj-gànnaar yi – egliisam daal di doge ca egliisub Rom ba – ak Norwej, Finland, xalaat yii tam tas ba genn Almaañ, dugg Angalteer ak nguuri skandinaaf yi (Danmark ak Suwed) .

Kalfen (Calven) : 

John Calven mi ngi juddoo Fraans atum 1509 g, di woon ku duggoon ci ngérum protestant mu Luther mi, te bàyyi woon mu katolig mi. Kalfen walla Calven juge woon na Fraans dem Siwis, li ko waraloon it mooy sonnal gu nu ko fa doon def ngir ay sabab yu aju ci diine .
Fii nag la tàmblee wisaare ak’a tas ngérum yéwénalam mu xaw mee jege ngérum Luther mi, ñi ko toppoon mu tudde leen (Hogonoots), di ci maanaa ñoñ laab ñi.
Kalfen ak Luther dëppoo  woon nanu ci ay masala yu diine yu bari, waaye wuute woon nanu ci ñaari mbir ñooy:
(1)	Wax gi Kalfen waxoon ne njéggal ci mbir yi nu doggal la, te loolu Luther nanguwu ko .
(2)	Kalfen daa gëmoon ne Egliis bi warul’a topp ci ginaaw genn nguur gu adduna, ne woon: Egliis bi daa war’a am nguurug boppam gu temb, gu dul wéeru ci gu adduna gi, ñi war’a doxal nguurug Egliis bi  nag ñooy am mbooloo mu xellu te am hikma. Xalaatam yooyu nag wisaaroo woon nanu ci reewi Tugal yi ci anam gu ëppante, ci Fraans, Angalteer, Siwis ak yeneen.
Swingli :

Mi ngi cosaanoo woon Siwis, judd atum 1484 g, ay yéwénali diineem mu tàmbli woon ko ci dëkkub Siyorix atum 1519 g, ci biir diiŋat gu mu doon def njaayum xobi njéggal yi.
Kon foofu ag jegeente gu mag am na fi ci diggante ay xalaatam ak yu Luther ak Kalfen, waaye teewul mu wuute ak ñoom ci lenn ci ay masalay diine.

Swingli moom daa jàppe woon egliis bi benn campéef  bu am demokraasi, buy ame ak’a sosoo ci mbooleem nasaraan yi nga xam ne seenug bokk ci, mi ngi ame ci benn kuréel bu leen fay teewal ci mbooleem mbir ak masala yi aju ci Egliis bi, ak ni ñuy sampe nit ña fay ligeeye.    
Ngérum Swingli tasoon na ci Siwis, ak ci lenn ci yeneen reewi Orob yi, waaye taxutoon mu siwe, wisaaroo ni mu Luther mi mbaa mu Kalfen mi.   

                                                              Bunt bu ñaareel bi

Jëm kanam gu xam-xam ak yewwute gu endustri

Doggantal gu njëkk gi

Jeexiitalu gi waa-Orob defoon ci yooni gëstu yu xam-xam yu jullit ñi.

Jamono ji xam-xam neewe lool te amadi xiima ci Tugal, ci jamono ju diggu ji, di (ju ag laman), moom xam-xam nekkoon na ci mbooleem reewi jullit ñi di lu naat, te meññi.
Xay gu lislaam gi di woon gi gënoon’a kawe ca booba, ngir coona bi boroom xam-xami jullit ñi daa génne ak’a daj ci dundal ko, ak ngir soññe gi nguurug lislaam gi daa soññe ak’a jàmbaarloo ci xam-xam ak boroom xam-xam yi.

Bi waa Orob yi dee ñu yittewoodi xam-xami Gres yi ak yu leen moy, fekkoon na jullit ñi ñoom ñu nekkoon ñu xam-xami xay yu yàgg ya ñoroon, ñu taxawoon ci firi leen ci araab: xay yooyu di yu Gres, Faaris  End, rawati na ci ndoktoor, bidiw, ak mat ak yeneen yi.
Ñu jotoon’a naan nag ci xam-xami Ubuqraat, Iqlidis, Aflaton  ak Arustoo ak ñu leen moy ci boroom xam-xami Gres yu mag yi.
Boroom xam-xami jullit ñi yamuñu woon rekk ci naan ci xam-xami Gres yi ak tuxal leen yobb leen ci araab, waaye kay danu leen’a toppoon, wéral leen, te dolli ci lu bari ci li nu feeñal, wuññi ko ciy xam-xam, aki gëstu aki nattu yu nu amal ci wàllug ndoktoor ak mat, kimyaa  ak xam-xami dénd yi , bidiw, juxraaf ak yu leen moy, ginaaw bi nu amee jikko yu mag yiy joxe xalaatub xam-xam bu sell.

Ngérum  walla yoonu gëstu wu xam-xam ci jullit ñi: 
Boroom xam-xami jullit ñi daal doxoon nanu ci seen gëstuy xam-xam yi ci ngérum xam-xam mu wuutewut ak mu xam-xam mi am ci jamono ju yees ji. Ñi ngi sukkandiku woon ci yooni xam-xam yoy bokkoon na ca yii:
Xeeñtu, raññale xaaj yi, jëfandikoo yooni natt yi, jàkkarloo, làmb, misaal ak jeem’a àgg ca jëmuwaayu xam-xam ba, maanaam xam-xam bi la tax’a jug, ak xam ngérte yi , muy liy juddoo ci boo ko xamee ba noppi .
Ngir coona yii nu daa daj nag mujj nanu di ñi jiitu ci lefum gëstu mu xam-xam, walla li nuy tudde “yoonu xam-xam wu nattu” , ci noonu lanu fi sampe woon kenoy gëstu gu xam-xam, ngir yeesal gi nu yeesaloon xam-xam ci seen jamono.
Waa-Tugal yi nag jariñu nanu ci wii yoonu nattu wu xam-xam wi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci. Ki jiitu woon ci ñi ci jariñu mooy waay- Angalteer ji di Roger Bacon ( 1214 g 1297 g), mooy ki waa Tugal yiy jàppe ki raw ci gëstug xam-xam ci Tugal, ndax mooy ki jeemoon’a wutal xam-xamu dénd ag noste  guy sukkandiku ci nattu ak jàkkaarloo. Loolu nag mbir la moo xam ne boroom xam-xami jullit ñi ñoo ko ci jiitu.
Jaadu na ñu leeral fi ne Roger Becon mii kat ku jotoon’a jàng làkku Gres la ak wu yahood yi , ak araab, jariñu woon it ci xam-xam yi nu ci bind. Moom nag daa gëmoon ne li tax ñu war’a jàng fisiya ak kimiya ak mat ak bidiw ak xeltu mooy ligeeyal xam-xam bi aju ci Yàlla  .

Digg  yi “xayug lislaam gi” jaaroon bi muy dugg Orob:

Jullit ñi dañoo nekkoon ñu rawoon ci lefi xam-xam yu bari, ci noonu ñu yanu woon seen xay googu yóbbaale ko ci mbooleem àdduna bi, ci penku bi ak sowwu bi. Orob jariñu woon na bu baax ci xam-xami jullit ñi, ña fa dëkk it jòkkoo woon nanu ak jullit ñi jaare ko ci ay ker-keraan  yu bari, bokk na ci yooyu:

(1)	Andalusi : 
Waa Orob yi jonjoo woon nanu ak digg yu xayug lisaam gi ci Andalusi, moom gox bii nga xam ne daa mujjoon fees dell ak leer guy jòlli tukkee ci xayug lislaam gi ko róofu woon.
Moom bii gox barabu jòlli la woon ñeel xam-xam ak dañ-kumpa, rawati na ci dëkki Orob yi mu dendaloon. Bu ko defee nga gis sàkkukati xam-xam yu Orob yi daa jariñu ci xam-xami jullit ñi, di jawalsi ak’a jublusi dëkki Andalusi yii di Talitala, Kordoba ak Sewija , ñu jële woon ci ñoom ngérum nattu  mi ñu daa jëfandikoo ci gëstu gu xam-xam, loolu mujj yëngal bu baax xalaatiinu waa-Tugal yi.

(2)	Dunub Sisil : 
      Araab yi jotoon nanoo teg loxo Sisil, ki joxe woon ndigalul jëf jooju di Siyadatul Laahi Bun Al Axlab, buurub nguurg Axaaliba yi, waaye mu ame ci loxol kapitenam bu siw boobu di Asad Bun Alfuraat atum 212 ginaaw gàddaay gi, mu ame woon nag ci jamonoy xalifa bu nguurug waa Abaas, bi tuddoon Maamun. Ca saa sa xayug lislaam tàmblli fa’a sutuxlu, Sisil mujj di gilin ci gilini xam-xami lislaam yi, sàkkukati xam-xam yepp jublisi ko rawati na ñi dëkke woon Orob, ngir sàkkusi fa xam-xam. Bi Norman yi nangoo Sisil ci Araab yi, yaquñu woon xayug lislaam gi, ñoom kay dañoo sawarloo woon boroom xam-xam yi, soññ leen, ci noonu firi teerey araab yi yobb leen ci latin daal di fay tàmblee am ak’a sawar, waa Orob yi tàmblee yër li ci yii teere ak’a jariñoo, rawati na Itaali mi ci gënoon’a jege Sisil, looloo waraloon muy mberum yewwute gi.

(3)	Xarey jooñ yi  bokk nanu bu baax ci li tax waa Orob yi manoon’a jokkoo ak xayug jullit ñi. Jokkoo gi it saxoon na fi lu tolloo ak ñaari xarnu, ci biir ñaari xarnu yii Orob jot na cee tuxal lu bari ci xam-xami lislaam yi, ame ci it, walla tege ci loxo lu bari ci teere yi nu taalifoon ci araab, ak yi nu firi woon jële leen ci làkku Gres, End ak Faaris  .
(4)	Jokkoog yaxantu gi amoon ci diggante reewi jullit ñi ak Orob, rawati na li ci Itaali jotoon’a def, mu bokk ci li sababoon jonjoog xay ci diggante ñaari dëkk yi.
(5)	Siyaare gi nasaraan yi daa defsi ci seen barab yu sell yi nekk Palastiin. Nga rax ci dolli tukki yi waa Orob yi daa defsi ci reewi jullit ñi, ak la ca juddoo muy ñu gis te jariñu ci xam-xami jullit ñi ak seeni xay. Jullit ñi daal ñoo waral jëm kanam gii nga gis ci Orob ci jamonoom ju bees jii.

 Xam-xam yi bàyyi ay jeexiit ci waa Tugal yi:

Lim (Mat):

Jullit ñi naanoon nanu ci xam-xami kalkil yi nekkoon ca waa End yu yàgg ya, ñu jotoon’a jànge ca ñoom  ni nuy defe ay lim (numero) waaye nag nu sellal ko gën koo teg ci yoon.
Boroom xam-xami jullit ñi ñoom defoon nanu ay dollent yu am solo ci xam-xamu waññ ( calcul), ñoo dolli woon tus  ci lim  yi, ndax amu ci woon bi nu leen di jël. Ñu indi màndargam al kasr alhasarii  di ci wolof (damat ci fukk) , ñu taalif ci wàllug xam-xamu waññ (calcul) ay teere yu waa Orob yi firi ci seeni làkk, te jariñu ci. Boroom xam-xamu jullit bii di Muhammad bun Muusa Alxuwarsamii, nekkoon na di ku aay ci xam-xamu lim walla waññ, moom de lanuy sant  bu lim (mumero) yi nekk ci kalkil duggee Orob tay.
Xawaarsamii mii aayoon na it ci beneen xam-xam bu yees mooy aljabr , moom sax mooy ki ko sos far. Taalif na ci tollale ci aljabr , nu tekki ko ci ginaaw bi ci làkki Orob yu bari. Boroom xam-xami Orob yi jariñu ci.
Boroom xam-xami jullit ñi jëfandikoo nanu ay junj  ci matematig yi(xam-xamu lim), ñoo njëkkoon waa Orob yi ci wàllug matemetig gu yees gii.
Bu dee nag ci andasa , ak xam-xamu ñattal yi , jullit ñi ñoom yamuñu woon ca la woon ca waa Gres yi rekk , nga xam ne seen boroom xam-xam bi nu naan Iqliidis moo ko feeñaloon, waaye jotoon nanoo feeñal ay masalay andasa yu bees. Ñu duggal li nuy wax “al mamaas” ci xam –xamu kalkilu ñattal. Nu jël li nuy wax “juyuub” = poos, wuutale ko ak li nuy wax “awtaar” = buum. Nu fecci itam toolale yu nu kaabaal yi . Nu xootal bu baax tam ci xam-xam yu nuy wax “maxruutaat” . Boroom xam-xamu jullit bi nuy wax Omar Alxiyaam defoon na lu mag ci wàllug mat, moom de bokkoon na ci ñi gënoon’a ràññiku ci boroom xam-xami jullit ñi ci wàllug matematig ci ñeenteel bu njëkk bu xarnub fukk ak ñaar g.

Xam-xamu Fisiya : 

Li nga xam ne sikk amu ci mooy ne jullit ñi jariñu nanu ci xam-xamu Fisiya ci waa Gres yi , bi nu ko tekkee ci seen làkk , waaye ñu gën koo yaatal dolli ci ay masala yu fisiya yu bari. Nu màndaqe walla natt diisaayu yolaakon yi , nu fent ay màndaqekaay yu xereñ, ñu xamale ay gisiin yu bees ci xam-xamu “kàddu” ak “gis” (basariyaat ) ak “séen” (almariyaat ). 
Boroom xam-xam bu jullit bii di Abo Yuusuf Yahquub Ishaq Alkanadi, mi nga xam ne mi ngi faatu atum 873 g, moom ku aayoon ci xam-xami gis yi la, taalif na ci ab teere bu am solo, mooy teereb yu nu xool yi, nga xam ne waa Orob yi mujjoon nanu ko’o tekki ci làkku latin. Roger Becon jariñu ci ak Liyonardo Da Vinci, ak boroom xam-xam bu Poloñ bii di Copernice (1473 – 1543 g).
Boroom xam-xamu jullit bii di Abo Aliyu Muhammad Bun Alhasan  Bun Alhaysam  (965 – 1038 g), moom mu nekkoon di ku aay ci xam-xamu fisiyaa, mu soppi xam-xamu leer bu yàgg ba, indi fi xam-xamu leer bu yees bi. Mu amoon ndam ci indi fi gisiinu  xam-xami seen yi, mu firi feeñteg xònn , ak safaanu gi ag leer di safaanu, ak ni muy dammoo. 

Bu boroom xam-xamu Gres bii di Batlimos jàllee, kii di Ibnu Haysam moom lanuy jàppe boroom xam-xam bi njëkk’a def ay wuññi ci xam-xamu gis. Haysam defoon na ay taalif ci xam-xamu-yu nu gis yi, ak xaaji bët,  ak weer yi  ak leer ak yeneen.
Waa-Orob yi it yii taalif, tuxaloon nanu leen ci  seen làkk  wii di wu latin, ci xarnub fukk ak ñatteel g, ak ci yeneen làkk yu Orob yi. Loolu dimbli leen ci nu jariñu bu baax ci xam-xam yii nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci bu baax.

Xam-xamu bidiw :

Jullit ñi yittewoo woon nanu xam-xamu bidiw, Xawarsimii moom defoon ay natt ci yëngug bidiw yi, xam fi nuy fenke ak fi ñuy sowe.
Jullit ñi jariñu woon nanu ci xam-xamu bidiw ci waa Geres yi, ci noonu ñu firi woon ci araab lenn ci teerey bidiw yu Geres yi niki teereb Batlimos bi tuddoon ñeenti wax yi.

Boroom xam-xam bi ko tuxaloon ci araab di Aboo Yahyaa Albatriix, ci jamonoy Abo Jahfar Almansuur. Doomi Muusaa Bun Saakir ñoom itam taalif teere bi nuy wax Aljadaawil Alfalakiya, yeneen boroom xam-xami bidiw it feeñ, niki: Saabit Bun Xurra, Haniin Bun Ishaqa Alhibaadi, ak Bataani mi faatu atum (929 g) ak ñu dul ñoom.

Jullit ñi tabaxoon nanu ay fuglukaayi bidiw ca Dimasq, Baxdaad, Kordoba ak Sawija di woon ay dëkki lislaam. Abo Abdillaa Albattani mii dees na ko lim muy ki gën’a bàyyi ay jeexiit -ci anam gu xóot- ci waa Tugal, ci boroom xam-xami bidiw yu jullit yi.
Waa Orob yi ñoom jariñu nanu bu baax ci xam-xamu bidiw ci jullit ñi,ak ci li jullit ñi jot’a gennewaat ci anam gii ciy wuññiy xam-xam.

Jullit ñi fésoon nanu ci xam-xamu kimyaa, Jaabir Bun Hayyaan Alkoofii bokkoon na ci ñi gënoon’a siw ci wàll googu, moom mi doon def kimya te taalifoon ci ab jimblang  .

Jabbir leeraloon lu bari ci way toggale  yu kimya yi nu xamutoon bu njëkk, niki: aji wex ju nitrik  , ruug nasaard, botaas, soda al kawiya ak aji wex ju asotik ak yeneen.

Mu leeraloon ba tay jefi kimya yi niki: seebal ak leeru  ak yeeg ak toqqal.

Da na jaadu nu leeral ne xam-xamu kimya moom, danu ko daa wooye xam-xamu Jaabir, ngir li ko ci Yàlla tawfeexaloon ba mu man’a topp yoonu xam-xam wu nattu wi nga xam ne ci la jaaroon ba man’a àgg ci ay dëgg yu kimya yu bari. 

Waa Orob jariñu nanu bu baax ci xm-xamu kimya bi ci jullit ñi, ci noonu nu firi taalifi jaabir yooyu ci seeni làkk, xam it lu bees li ci jullt ñi dolli.

Ndoktoor :

Boroom xam-xami jullit ñi rawoon nanu ci xam-xamu ndoktoor. Sartoon nanu ci seen boroom xam-xam, mu xam siddi , xam jëf ak warteefi cer yi, ak noyyi ak soppikum saw.
Ñoom de ñu sonnoon ci xam-xamu siddi lanu woon. Firi woon nanu xam-xami Geres yi ci aju woon, ci làkku araab. Bi nu noppee ñu taalif ci. Teereb Ibnu Nafiis bi tudd Tasriihul Xaanuun dolli na ay xam-xam yu am solo ci xam-xamu siddi. Jullit ñi jàngale nanu doxug dereet , sonn it ci mbooleem xeeti tawat yi, xamale itam deewal  bi nuy faral a def ci ligeeyu xotti  . Ki niy wax Razi te faatu atum (923g) feeñ na te raw ci ndoktoor, taalif na ci lu sakkan.
Ak Ibnu Sinaa mi faatu atum (1037g) , moom de kenn la ci boroom xam-xami jullit ñi gën’a siw ci ndoktoor, teereem ba tudd Xanuun Fit Tibb de jenn jimblang la ju xam-xamu ngoktoor, ju waa penku ak sowwu ñepp xam, ak Abo Xaasim Xalf mi gënoon’a fes ci xottikati  xarnub fukk ak benn g. Ak Ibnu Zahr, boroom teere bi tudd Mubtakaraat Fil Jiraaha. Waa Orob yi jariñu nanu ci xam-xamu ndoktoor bi nga xam ne jullit ñi rawoon nanu ci. Ñu jariñu ci ni nuy siddee, ak ni nuy gennee tawat yi, ak ni nuy faje, ak ci xam-xam yi nga xam ni teerey jullit yi làqoon nanu leen ci wàll gii, ginaaw bi nu leen firee ci làkki Orob yi. Waa Orob yi jële nanu ci jullit ñi tabax ay fajuwaay  ak jëfandikoo deewal  ak li nuy wax Kaaw  su nuy opere (xotti).

Waa Orob yi ba tay jariñu nanu bu baax ci xam-xamu xeltu bi nga xam ne jullit ñi ñu ci rawoon lanu. Ci noonu nu jàngoon taalifi Kanadii, Faarabii, Ibnu Sinaa ak Ibnu Rusdi ak ñu dul ñoom, ginaaw bi nu leen firee ci seeni làkk.   
Bokk na ci boroom xam-xami Orob yi gën’a siw ci jariñu ci jullit ñi ak seeni xalaat : Paskaal, Dikart, Hiyom ak Becon ak ñu leen moy.    

Waxtu wi yaatuwul ngir nu man leen a indil ngértey  xam-xam yu bari yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci, ci seeni gëstu te booba Orob’a ngi ci ngëmmeenam li ak lëndëmug reeram gi, ci ron nosteg laman ak cangug Egliis bi.

Da na yell nu leeral ne xam-xam yi ak ngértey xam-xam yi nga xam ne jullit ñi àggoon nanu ci, dañoo tàmbli woon’a tuxu ndànk-ndànk jëm ci reewi Orob gu sowwu gi, ginaaw bi ab kureel ci waa Orob yi xamee solos xam-xam yii, te taxawoon ci firi leen ci seeni làkk. Ay firikati Orob yu bari feeñoon ci loolu ku ci mel ni: Costantinus Africanus, Herman The Cripple ak Eugenius mu Parlermo mi ak ñu dul ñoom.
Kon lu nu war’a xam la ne yewwuteg xam-xam ak gu endustri gii am ci reewi Orob yi, ci ginaaw yewwute gi, du lu moy meññat ci meññati nattu ak gëstu yu xam-xam yi nga xam ne Orob tuxale na leen ci xam-xami lislaam, ci digg jamonoy xayug lislaam gi. Coonab gëstu yooyu nag ñooy cëslaay yi nga xam ne ci la jëm-kanamug xam-xami dëppale  yi ak yu xarala yu bari yii tegu ci adduna ju xay jii ngay gis tay .

Doggantal gu ñaareel gi    

Wàll yi xam-xam jëme kanam ci Tugal

Xam-xam naat na te jëm-kanam ci Orob, ci biir xarnu yii: bu fukk ak ñeent, fukk ak juroom ak fukk ak juroom benn g, loolu bokk ci li waral jëm-kanamug xam-xam gu mag gii Orob gis tay ci jamonoom ju yees jii nu nekk, nga xam ne ci la yewwuteg xam-xam juddoo ak gu endustri ci Orob, ak li topp ci loolu ci njariñ yoy du Orob rekk la ñeel waaye àdduna bépp.

Li taxoon xam-xam jëm kanam :

Jëm-kanam gii xam-xam jëm kanam tay ci reewi Orob gu sowwu gi, am na ay balluwaay yu wuute, yi ci ëpp solo di:

(1)	Tuxal xam-xami jullit ñi ak firi leen ci làkki Orob yi te jariñu ci.
(2)	Ak feeñ gu ab lim xëy feeñ ci boroom xam-xami Orob yi amoon ag cofeel ci gëstu yi aju ci xam-xam
(3)	Yokku gu yëngu-yëngug firi ak taalif yokkuwoon, rawati na bi nu fentee móolukaay yi.
(4)	Xeemmeemteef gu waa Orob yi amoon ci dundalaat xam-xam yu yàgg ya: yu Gres-Rom ya. 

Wàll yi xam-xam jëme kanam :

Ak li nuy misaal jamono yu diggu yi ci Orop lepp, naan jamonoy reer la ak lëndëm, teewul ay ceññeeri xam-xam yu kenn mant’a reere, mant a weddi amoon fa . Li am daal mooy wuññiy xam-xam yi ci jamono jii du woon yu yaatu, lu neew la woon. Ci noonu xam-xamu waa Orob yi nekkutoon lu moy li nu xame woon ci waa Geres yi ak ci jullit ñi, ci seen ginaaw. Maanaa mi xalaati waa Orob yi ame woon soppiku woon na ci jamonoy yewwute gi, ginaaw bi nga xamee ne gëstuy xam-xam yi fa ñoom, dafa mujjoon tegu ci nattu  . Ci noonu Orob jot na a am ndam ci jëmale kanam xam-xam ci wàll yu bari, yi ci ëpp solo di:

Ndoktoor :

Ndoktoor ci Orob wëyoon na di sukkandiku ci li fi waa Geres bàyyiwoon ak li fi Jalinos jot a indi ak Hiboqrat ak ndoktoorug jullit ñi, jaare ko ci seen teerey ndoktoor yi nga xam ne waa Orob mujjoon nanu leen’a firi ci seeni làkk.

Xam-xam bi Orob ame ci ndoktoor weesuwutoon fii, ba ci xarub fukk ak juroom benn g.

Waa Orob yitewoo woon nanu bu baax xam-xamu ndoktoor, ñoom daal ñoo ci gënoon’a sonn ñu dul woon ñoom, rawati na ci xarnub fukk ak juroom benn g, moom dey xarnu la bu fekke ay xew-xew yu bari yoo xam ne ñoo waral ag jëm kanam gu mag ci wàllug ndoktoor ci Orob.

Bii xarnu daal seere na ay yëngu-yëngu yu wuññi yu juxraaf ak tuxug ay mboolooy gaal yu yaxantu, ak ay gàddaay ci ay mbooloo ngir dëkk-ji ci reew yii nuy door’a wuññi, aki xare yu tar te yàgg yu amoon ci Orob te sababoon ay tawat yu metti aki mbas yu nu xamutoon ci Orob. Mu mujj nag bokk ci warteefi doktoor yi ci Orob ñu jeem’a xam yile tawat yu yees ak nu nu leen di faje, wutal leen ay garab.

Ci noonu boroom xami-xami Orob yu bari feeñ, ku ci mel ni: Fisaliyos mum Beljik mi, Frakastor mu Itaali mi, ak Gonte Andarnax mu Almaañ mi nekkoon doktoorub Fransuwaa mu njëkk mi doon buuru Fraans, ak Lofan Hok mu Oland mi, ak Luwis Pastor mu Fraans mi ak Kox mu Almaañ mi añs.
Bu ko defee waa Tugal yi xam jàngoro yi, xam it nu nu leen di faje, ju ci mel ni: Daftiriya, Judri, Tifos, Kolera, Tifod añs.

Juxraaf ak Bidiw:

Xalaat bi naan suuf si daa tàllaliku daal, te boroom xam-xami bidiwi Gres yi indi woon ko fi, moo nekkoon xalaat bi tasoon ci Tugal gëpp, ci jamono ju diggu ji, ak doonte lenn ci boroom xam-xami Gres yi waxoon nanu lu ko safaan, ne suuf si moom tàllalikuwul, daa bulu kay, mel ni ab kol-kol, boroom xam-xamu Gres bii di Batlimos, moom doon na def ay ligeey ci googu wàll.

Waa Tugal yi nag seen xam-xamu juxraaf ñi ngi ko doon gën a jëmale kanam, jaare ko ci li nu xame ci wuññiy juxraaf yi ak ginaaw bi. Ci noonu xam-xamu juxraaf tàmblee jem kanam ci Orob.
Jem kanamug xam-xamu Juxraaf tax na ba bu Bidiw it jem kanam. Kii di Koperniks, di boroom xam-xamu Poloñ, moom, siwoon na ci lefum xam-xam mu Tugal mi, moom dey duggal na loxoom bu baax  – boo xoolee ligeeyam yi aju ci xam-xamu bidiw  – ci doxug xam-xam akug jëmam kanam ci Tugal. Kopernic moom àndutoon ci gisiinu Batlimos wi doon wax naan suuf si moom daa bulu ba noppi nekk ci digg adduna bi, bu ko defee nekkteefi asamaan yi  di ko wër. Kopernics moom ne suuf si daal ak yeneen nekkteefi asamaan yi, ñoom ñepp danuy wër jant bi, te suuf si nag am na wërug boppam gu muy wër ab diggam , ci 24 waxtu yu nekk. Mu neeti suuf si dafa wëndeelu, maanaam roo  te wëndeeloom googu nag tax na ba day yor doxiin walla yëngu-yëngu gu roo, mbaa guy wëndeelu. 
Waaye nag lu ñaaw la lool Copernic ñàkk a man a tas te wisaare xalaatam yooyu ci bi muy dund, ngir rekk ragal gu mu ragal jàngu bi (Egliis bi), xalaatam yooyu wisaarewunu leen mbaa nu tas leen ndare ci atum 1543 g, muy at mi mu faatoo. Boroom xam-xamu Itaali bii di Galileo ( 1564 – 1642 g ) moom jug, def lu rëy ci jëmale kanam xam-xamu Bidiw, loolu gën na a am ci ginaaw bi mu jëfandikoo fésalukaay  ngir fuglu bidiw yi ak nekkteef yi ci kaw asamaan si, mu dëgëral itam xalaati Kopernic yi.

Xam-xamu fisiya gën na a jëm kanam te gën a buur , ci xarnub fukk ak juroom benn g. Bu ko defee, nga gis boroom xam-xam yi ñuy dàggasante  ci masalam yëngu-yëngu, ndaxte yëngu mooy cëslaayu xam-xamu fisiya bu Arusto, maanaam ci la xam-xamam boobu tegu.
Boroom xam-xami Tugal yi def seen yite ci ñòddi gi nekk ci suuf si . 
Boroom xam-xamu Itaali bii di Galileo di ku rawoon ci wàll googu, moom de ci atum 1592g, yeegoon na ca sooroolub Pisa bu jeng ba, jël ñatti yef sànni leen, ñu rotandoo ci suuf, Galileo mii moom lanuy jàppe ki gën a am solo ci boroom xam-xami Tugal yi daa yitewoo xam-xamu fisiya, ndax kat mooy ki teg dàtti walla fondmangi xam-xam bii ci Tugal ci fukk ak juroom ñaareelu xarnu g.
Boroom xam-xamu Angle bii di Isaac NEWTON (1742 – 1727 g ) mooy ki feeñal dooley ñòddi gi nekk ci suuf si . Moo wax ne bidiw yepp, walla plaanet yepp, danuy wër jant bi, ci ay ngunu  yu sax , walla ay nekkuwaay yu sax yoo xam ne ñòddi gi nekk ci jant bi moo leen di nos te di leen teg ci yoon.
Ki nuy wax Laplace (1749 – 1827 g ), moom itam ñëw, sonn ba xam ni bidiw  yi sosoo.

Waa Tugal yi tuxale nanu ci jullit ñi xam-xam yu am solo, yu aju ci xam-xamu Kimya bu bees bii, nga xam ne boroom xam-xamu jullit bii di Jaabir Bun Hayyaan, fésoon na ci lool, te amoon ci ag raw.
Ñoo leen xamal alkol, soda, gudrong, saabu ak yeneen toggaliiti kimya  yi nga xam ne jullit ñi aayoon nanu ci.
Toggaliit yii ba leegi da nga ciy gis yoo xam ne turi ay jullit lay yore.

Waa Tugal yi nag, ñoom, danoo gën a jëmale kanam xam-xamu Kimya, ci ginaaw yewwute gi. Ci noonu kii di Josef Priestley am tawfeexu di ci waa Tugal yi, ki njëkk a jële Oksijen ci xoromi Siibix  , atum 1774 g, te loolu kat fekkoon na boroom xam-xamu jullit bii di Jaabir xamoon ko bu yàgg. Lavoisier di boroom xam-xamub Fraans, di ki feeñal gaasub njëlbeenu oksid korbon, atum 1797 g . Waay Almaañ jii di Rontgen (1845 – 1923g), moom, ñëw feeñalal ñu ceññeeri iks , atum 1895g.

Boroom xam-xam bii nuy wax (Thales), di ku dëkkoon Gres, moo seetlu woon dooley ñòddi ju nekk ci kuran, bi mu ko wokkee, loolu mooy li nu njëkk a xam ci kàttanu kuran. Boroom xam-xamu Angle bii di William Gilbert, nekoon doktooru buuru Angalteer bu jigeen bii di Elisabet mu njëkk mi, moom itam ñëw, feeñal ne am na yeneen ne-ne   yuy am ag ñoddi boo leen jonjee, yu dul kuran rekk. Feeñalug loolu nag mi ngi ame woon ci lu tollook atum 1600 g. Boroom xam-xamu Almaañ dikk, fent ab jumtukaayu kuran buy juddal kuran atum 1672 g.

Ki nuy wax Stephen Gray dikk, won nu ni nuy tuxale kuran, jële ko ci barab, yobb ko ci beneen, jaare ko ci fiil yu xànjar.

Wolt mu Itaali mi, di ki wone duusi kuran yi, te fent batari. Borom xam-xamu Amerig bii di Bengamin Franklin, di ki wone ne melax ak kuran benn lanu, mooy ki fent fegukaayu dënn . Misel Faraday dikk, moom itam, di ki feeñal yoon woo xam ne ci la nuy jaare di genne kuran bu bari atum 1831 g.
Waa Tugal soobu nanu ci xam-xamu Mat, waay Itaali jii di Tartaliya def ci lu am solo, boroom xam-xamu Frans bii di Fiit, jëfandikoo woon na ay araf ci xam-xamu jabru, bii nga xam ne ci jullit ñi la ko waa Tugal yi jële.
Leodardo da Vinci nag moom ci boroom xam-xam yi sos xam-xamu Jiyoloji la bokk, moom mi dëkkoon Itaali, Jims Hitn ( 1726 – 1797g) itam ñëw, di ki xamale ni doj yi nekke ak ni nuy sosoo.

Jamonoy yewwute daal ci Orob mooy jamono ji goreel xelum Tugal mi, te feexal xalaatam, yaatal ko, musal ko ci tënk-tënki jamonoy Orob ju diggu ji. Ba tay dees na ko jàppe muy jamono ji xayale te waajale ba xam-xam man a jëm kanam, man a naat ci Tugal, naataangey xam-xam gii nga gis ci Tugal ci jii jamono de, dara waralu ko lu dul jamonoy yewwute. Ci jii jamono la ay jeem yu xam-xam yu dëggu am, yu sukkandiku ci yoonu xam-xam wi jullit ñi fentoon bu yàgg lool, njëkk waa Tugal yi di ko xam.  

Ñatteelu doggantal

Yewwute gu endustri : li mu jagoo – ay màndargaam – li mu fi indi

Yewwute gu endustri ci Tugal, ñi ngi ci jublu soppiku gu mag gi fa amoon ci wàllug endustri, walla jëm kaman ga fa amoon ci wàllug jumtukaayu mekanig, rawati na ci Biritani, ci ñatteelu xaaj bu mujj bi, ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g.
Waaye nag, moom endustri mii, yàggul dara mu tàmblee tas ci Tugal nànk-nànk, ak Amerig, la ko dale ca njëlbeenug fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g.
Bi mu ko defee nag, ay jeexiitam tas, ba àgg ci pàkk yu bari ci adduna bi, loolu nag ci ñaari xarnu yii la: fukk ak juroom ñeenteelu xarnu ak ñaar-fukkeelu xarnu g.
Endustri yi nag masuñoo dañ di jëm kanam ak a awaase ba ci sunu jamono jii nu toll.

Looloo waral du man a ñàkk nu xam sabab yi tax yewwuteg endustri am ci Tugal.

Sabab yi tax yewwuteg endustri am ci Tugal:

(1)	awaase gi xam-xam awaase ci Tugal, ci jamonoy yewwute, moo waral yewwuteg endustri am.
(2)	Dëkki Tugal yu mag yi, am gi nu am, ak tegu gi nu tegu ci yaxantu ak endustri, ak woomleg koom gi loolu di jur, nga xam ne day tax ba endustri di jëm kanam, rawati na, bi ci aju ci ràbbu ser , nga xam ne mooy endustri bi njëkk ci Tugal.
(3)	Jëmm  ci Tugal, ni mu jekki-jekkee rekk fés, mujj di dàtt bi mboolaayi Orob yi tegu, sabab la ci li yee waa Tugal yi, moom jëmm jooju, ci Orob ku nu tënk la woon ci jéngi nosteg laman , jamonoy yewwute ñëw dog jéng yooyu, feexal am xelam, leeral ko ci xam-xam, ba mu man a xalaat bay fent ay jumtukaay yu am solo yu koy dimbli ci yombal ag dundam.
(4)	Li juddoo ci wuññiy juxraaf yi it, muy teg loxo gi reewi sancaan  yi daa def reew yi nu sanc , ak di fa jële ay xeewal aki ne-ne yu nu laalagul , di leen yobbu seeni reew, loolu it bokk na ci li jëmale kanam yewwuteg endustri gi ci Tugal.
(5)	Reewi Tugal yi ak këri koppar yi, jàpple gi nu doon jàpple naal yi jug ngir jëmale kanam endustri ci Orob, loolu de ci li defar jawwu ji la ba endustri man a dox, man a àntu.
(6)	Boroom xam-xam yu aay, yi xëy feeñ, te bari ci Tugal.
(7)	Bari gi ligeeykat yi bari ci Tugal, rawati na ñiy ligeey ci endustri yu ndaw yi. Na ngeen xam nag ne lu bari ci fentkati angle yi daa defar ak a fent jumtukaay yi ak masin yi, ci ligeeykat yi amoon xam-xam yu neew lanu woon, nga xam xam ne daanaka jàngunu woon.

Yewwute gi li mu jagoo woon ak ay màndargaam :

Yewwuteg endustri ci Tugal, daa jagoo woon ay mbir yu bari, yii ci lanu:

(1)	Jëmale kanam gu nu jëmale kanam jumtukaayu ëcc ak ràbb :

Meccem ràbb daal, ci yi gën a jariñu ci fent yu xam-xam yi aamoon ci Tugal la, rawati na ci Britani, loolu  di ci ñeenteel bu mujj bi ci xarnub fukk ak juroom ñatt g.
Loolu nag li ko waral mooy yitewoo gu tar gu nit yitewoo ay sér, ak ñàkk a jafeg jëfandikoo jumtukaay yi ngir ligeey ci.
Ràbbkatu angle bi nuy wax James Hargreaves, jot na a fent atum 1764 g, benn jumtukaayu defar wëñ, muy benn masin bu loxo, bu nuy jëfandikoo ci ëcc, li koy doxal nag doon genn mbege walla pono, bu yor juroom ñatti ëccukaay ak ñaari forukaay, bu ko defee benn ligeeykat di ko yor, di ko doxal.
Bu ko defee, fentkat bu angle bii di Richard Arkrihgt, fent moom it atum 1771g, benn jumtukaay buy xëcc wëñ yi, moom nag jumtukaay la bu nu daa doxale ci dooley ay fas, mujj nu koy defe ci dooley ndox, nu tudde woon ko kaadaru ndox bi, (water frame).
Ki nuy wax Samuel Compton, ñëw fent – atum 1779g – benn jumtukaay buy boole gaaw ci ligeey bi ak baaxle ko, boobu jumtukaay nag tasoon na ci fi dend ak barabi ndox yi, ci ñaari goxi Angalteer yii di Yorkshire ak Lancashire .

Ki nuy wax Edmund Cartwright, moom itam àgg ci fent benn jumtukaay bu nuy doxale dooley ndox, ginaaw bi nu koy doxale dooley cóolóol , te kat tax na ba nu man a ful li nu daa ràbb, daa ko defar ciy sér.

Ligeey bi nu daa def ngir gën a jëmale kanam ak gën a rafetal ligeeyu ëcc beek ràbb bi, gën a dolliku, te sax. Nu àgg ci jëfandikoo ne-ne yu Kimya yi  ngir raxas wëtéen wi, defarati yeneneen jumtukaay ngir móol ay deseñ aki mbind ci ndima yi nu ligeey. 

(2)	jëfandikoo kàttan  :

Jumtukaay  yu njëlbeenu  yi amoon, nit a ko daa doxale ci dooleem, walla dooley dundat  . Kàttan nag di energie jëm na kanam ci jëm gi jumtukaay jëm kanam te awaase. Ci noonu nit jot a jëfandikoo ci njëlbeen gi dooley ndox, ngir doxal jumtukaayam yi mu fent bu yàggul, ginaaw bi, mu jëfandikoo dooley cóolóol ak këriñ.
Ki nuy wax Thomas Newman, ñëw, indi fi jumtukaayu cóolóol, James Watt, moom itam dikk, gën a defaraat jumtukaayu Thomas boobu atum 1765g, loolu waral ay soppi yu mag yu xóot ci wàllug ligeey bi, ak li nuy ligeey, ndax kat duggal gi nu duggal jumtukaay bu mekanig, bu cóolóol ci endustri ak jokkoo  lu rëy a rëy la te am solo, te moo tax ba nga gis endustri tay mu toll fii mu toll. 

Bu ko defee ca saa sa, waa Tugal yi tàmblee gëstu fu nuy jële këriñ. Këriñ nag bari woon na lool ci Wels gu bëj-saalum gi, ak Skotland.

Nit it gënoon na a jeego ay jeego ci jëfandikoo gi muy jëfandikoo kàttan, mu feeñaloon petrol ca D.B.A (Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi), ci digg fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g. Ginaaw bi, nu gisaat petrol fu bari ci adduna bi. Ginaaw bi nu fentati benn jumtukaay buy “lakk ci biir”, boo xam ne mooy soppi petrol bi, ginaaw bu ko lakkee, def ko kàttan guy yëngal ak a doxal. Loolu moo waral ngay gis leegi jumtukaay yu mekanig yii nga xam ne danuy sukkandiku ci li nuy wax lakkug biir gi, mooy lakku gi petrol bi di lakku ci biir jumtukaay bi, jumtukaay yooyu nag ñooy yu mel ni: oto  yii ngay gis, fafalnaaw yi, gaal yii nga xam ne lakkug biir gee leen di doxal añs.
Kuran tam jariñ na nit lu bari, loolu nag mi ngi ame ci bi kii di Faraday juge, fent li nuy wax juddalukaayu kuran, nga xam ne loolu indil na nit lu bari ci ay ligeey ak njariñ ci dundam.
Nit àgg na ci xam kàttanug saal  te jëfandikoo ko ci anam yu bari, loolu tax mu man a neewal li muy sukkandiku ci petrol. Waaye nag nanu xam ne kàttanug saal moom lu seer la, manu fee wuutu petrol ci genn anam, nit it jot na a xam kàttan gu jant gi  , te jëfandikoo ko ci yenn anam yi, niki nuggalukaayu ndox yu jant yi nuy jëfandikoo ci kër yi, ak ci yeneen anam yi.

(3)	Jëm kanam gu endustri bu weñ jëm kanam:

Bokk na ci lu am solo li yewwuteg endustri gi jagoo, bokk na ci, jëmale gi nu jëmale kanam endustri bu weñ, loolu nag mooy bi angle bii di Bassemer, jugee, fent yoon woo xam ne manees na cee jaar bay soppi weñ di ko def “sulb” mooy weñ gu wow kong, dëgër këng, loolu nag ni mu  daa ame mooy nu jaarale ko ci tàngoor wu kawe lool. Nit it gënoon naa def ay jeegoy jëm kanam ci wàllug yoon yi muy jaar bay genne këriñ, loolu tam dimble ko ci mu man a dolli, gën a lëwal li muy ligeey.
Lii lepp nag bokk na ci li waral yewwuteg endustri gi man a am ci Tugal, rawati na ci Britani.

(4)	Jokkoo  gën a jem kanam gu mu gën a jem kanam:

Li kenn manul a sikk mooy ni endustri jëme kanam ci Tugal de indi na fi ag jëm kanam ci wàllug jokkoo, rawati na bi ligeeyu weñ gënee dox, gën a jëm kanam. Ci noonu angle bii di George Stephonson, moom ñëw , fent saxaarug coolool maanaam , muy daw ci ay banti weñ  ci diggante dëkkub Liverpool ak Manchester ci atum 1830g, yoonu weñ wii  mooy yoonu weñ wi njëkk ci adduna bi.
Ginaaw bi, nitug Amerig kii di Robert Foulton, moom dikk, jëfandikoo coolool, di ci doxale gaali dex yu ndaw yiy daw ci dex yu mag yi nekk ci Amerig gu bëj-gànnaar gi. Ginaaw bi mu jugati, jëfandikooti cóolóol, dawal ci gaali cóolóol yu mag yii di daw ci geej yeek mbàmbulaan yi.
Ci noonu la jokkoo tàmblee jëme kanam nànk-nànk, ni ko endustri defe. Bu ko defee, feeñteg  jëm kanam ci wàllug jokkoo mujj di feeñte giy raññale tey màndargaal yewwuteg endustri gu mag gii am tay ci adduna bi.

(5)	Feeñug campeefi endustri yi :

Ligeeyuwaay  yu ndaw yi juge nanu ci kër yi, doon leegi ay campeef yu endustri, yu mag, yu nekk leegi ci dëkk yu mag yi. 
Endustri yi mujj di loo xam ne am mbooloom ay lonkoo  yu endustri, yu mag ñoo koy moom, ñooy lonkoo yooyu nga xam ne ñooy faral a moom li ëpp ci alal yi.
Isin yu mag yi nag, ci wetu barabi ne-ne yu nu laalul  yi lanu daa faral a sampu, te loolu da leen daa dimble ci ñu man a neewal seeni fere ci lu aju ci seeni ligeey, ndax loolu daa na tax li nu ci waroon a ñàkk gën a neew. Neewug fere yooyu daa na feeñ bu baax ci njëg yi, ndax daa na leen daaneel. Te daa na gën a baaxal ligeey bi gën koo wuuteel.

Li fi yewwuteg endustri gi jur:

Maneesul a sikk ne yewwuteg endustri gi indi na ci Tugal ay ngérte  yu yaatu ci wàlli koom, politig ak mboolaay.

Li mu fi indi ci wàllug koom: 

Yewwuteg endustri gi bàyyi na fi ay jeexiit yu rëy ci wàllug koom, ci biir Orob ak biteem. Ndax ca la isin yu mag yi tàmblee feeñ, yi daa am jumtukaay yu rëy yi. Li nuy ligeey gën a yokk, gën a wuute, li nu koy jënde gën a neew, ñepp man cee jot, jumtukaayi ligeey yi gën a bari, jokkoo gën a yomb, yoon yi gën a bari, ja yu adduna yi gën a yaatu, lonkoo yu mag yi amoon ay gis-gis aki xemmemteefi rënk   ak sanc , tàmblee booloo.
Ndax kat sanc gu politig  gu yees gii, du lu dul doomi sanc gu koom-koom, gi Tugal daa def, jaare ko ci endustreem bu jëm kanam bii, ak baaxug ay jumtukaayam, ak soxla gu tar gu mu soxla ne-ne yu nu laalul yi, ak soxla gu mu soxla ay ja  yu yees, yu mu man a jaaye marsandiisam yu bari yii te wuute.

Waaye mbay nag moom, ak li ay jumtukaayam gën a jamonoo lepp, ak li mu gën a ñaw lepp, te gën a xam-xame, teewul ay njëgi li ciy juge gën a seer, li ko waral mooy li ëppoon ci baykat yi danoo gàddaayoon àll yi, dem ci taax yi, fi isin yi nekk, ngir man fa a ligeey, ndax la nu daa gañee ci ligeey bi moo daa gën a bari, te daa nanu ci ame ag sax fi barab. Gàddaay gii nag, juge ci àll yi, dem ci taax yi, taxoon na ba ab kiris walla jafe-jafe bu rëy amoon fi ci wàllug mbay ci Orob, rawati na ci Angalteer.

Joxalanteg yaxantu gën a yokku ci adduna bi, nga gis reew yiy defante ci seen biir ay kollarantey yaxantu, ak yeneen kollarante yu aju ci yombalug jaarale marsandiis yi ci geej yi, ak mbàmbulaan yi , ak barabi romb yu adduna yi. Ci noonu lonkooy yaxantu yu adduna yi nga xam ne seeni boroom danuy am alal lool tàmblee feeñ, bank yi tàmblee yëngook a sawar, ak këri koppar yi.

Li mu fi jur ci politig: 

Sanc gii Tugal tàmblee sanc reewi jàmbur yi ak di leen teg loxo, bokk na ci li fi yewwuteg endustri gi indi, wuutal ko fi, ginaawal ko fi ci wàllug politig, ndax ni ma la ko waxe woon ci ginaaw , endustri day soxla ay ne-ne yu nu laalul, te loolu danu ko daa gis feneen fu dul Tugal, te loolu jur na ay xare ci diggante ay reew ci fu bari ci sunu adduna bii, tax it ba reew yi nu sanc jug, di xare ngir goreel seen bopp, soril senn bopp ag sanc, ak lepp lu ko jege ci xeeti moomadi sa popp, ak tembadi.
Bu ko defee, benn dal  daal di feeñ ci Orob, mooy dalu “koom-koom bu gore bi walla bu libre ” bi am te taxaw ci nosteg bopp-alal . Loolu nag mi ngi am ci ginaaw bi endustri bu yees bii soppikoo dem ci noste gii, li ko waral di  yitewoo gu bari gi  mu yitewoo ci nu sos ay isin yu mag, ak isin yu mag yii, yitewoo gu tar gi nu yitewoo alal ju bari ngir taxawal leen, sos leen.
Goornamaay Tugal yi, jàpple woon nanu noste gii te dëgëral ko ci mbooleem li nu man, am ko ciy man-man aki kerkeraan  . Ci noonu warteefi goornamaa yi gën a yaatu, gën bari ci mboolaayi endustri yi. Loolu yobbu ko ci ay warteef yu mel ni sonn ci mbiri mboolaay yi, te yittewoo leen, sosal leen ay jàngu  aki daara yu mag, ak sonn ci mbiri wér gu yaram, ak lepp lu yitteel mboolaay gi maanaam societe bi.

Ci noonu ay boroom xam-xam aki bindkat daal di feeñ, yoo xam ne seen ligeey bepp ñi ngi ko jëmale ci luy dundal mboolaay gi, suqali ko. Ay gisiini politig yu yees feeñ, yoo xam ne bokk nanu ci li fi indi xalaatu politig bu Tugal bu yees bii tay.
Goornamaay Tugal yi duggsi nanu ngir aar ligeeykat yi, ci noonu ñu yamale  waxtu yi nuy ligeey, def leen leegi ñuy: 7 – 8 waxtu, te bu njëkk 12 – 16 waxtu lanu woon. Ñu ñëwati indi fi noppaluy  tawat yi ak yu jeexiitalu ayu bis yi ak yu at yi . Ñu defati ay ligeey ngir yekkati seen payoor yi, jeemati ba seenug dund ak seeni dëkkuwaay gën a baax.

Man gi reewi endustri yi man a doxal seen mbiri reew, feeñ na, te am bi reew yooyu amee alal ju doy ak ngànnaay yu yees te xereñ . bu ko defee, nga gis reewi Tugal yi sukkandiku ci endustri, ëpp doole fuuf yi sikkandiku ci mbay, ak ngànnaay yu yàgg, yi nu miinoon.

Li mu fi jur, indi ko fi ci wàllug mboolaay:

Yewwute gi ci Orob jur na ay gàddaay yu mag, juge ci àll yi,  ak dëkk-dëkkaan yi, dem ci taax yi ak dëkki endustri yi, loolu nag mi ngi am ci bi isin yi yokkoo, jumtukaayi endustri yi gën a xereñ cig wàll, moomeeli mbay yu mag tàmblee feeñ ci Tugal, la ko dale ca ñaareelu xaaju xarnub fukk ak juroom ñatt g, rawati na ci Angalteer ci geneen wàll. Bu ko defee baykatu Orob bi moom gisoon ne li ko gënal daal mooy mu dem ci isin yii nga xam ne li nu koy fay moo gën a wóor te gën di lu nu xam, te bàyyi mbay mii nga xam ne leeg-leeg mu baax, leeg-leeg du baax, ak jafe-jafe yi mu àndal, muy njaay meek toppatoo gi.
Lii mooy li waral ñiy ligeey ci mbay neew, te wàññiku, ñi dëkke kaw gi gën a neew, loolu it jur yokkug ñi dëkke ci taax yi, bu ko defee, am lu juddoo ci loolu, mooy neewug jóoxiitum mbay mi , te loolu it tax na njëg yi aju ci mbay ak li ciy juge gën a seer.

Beneen jafe-jafe daal di juddooti, mooy bu aju ci dëkkuwaay ñeel way gàddaay yu bees yii gàddaaye kaw ga ngir dëkksi ci taax yi, di wër ligeey. Ci noonu ay barabi dëkkuwaay yu xat tàmblee feeñ ci wetu fi isin yi nekk. Di dëkkal lu sakkan ciy nit, te matalewul li nu laaj ci dëkkiin wu baax te xellu. Ci noonu wér gu yaram dajeeki jafe-jafe yu rëy a rëy , jikko it naka noonu. Jafe-jafey ligeeykat yi gën na a yokku, bi nu demee ba li nu leen di fay manatul a faj gën ja’a neewi seeni aajo, ngir seerug dund gi.

Beneen jafe-jafe bu mboolaay bu bees amati, ànd’ak yewwuteeg endustri gi, ak ag jëmam kanam, loolu mooy ne lu bari ci jigeen ñeek xale yi, leegi danoo tàmbli di ligeey ci isin yi, te kat kenn soññu leen ci ku dul boroom isin yii nga xam ne li leen ñoroon weesuwul nu nu man a gën a ame ay ligeeykat ba gën a man a neew lu nuy fay, ginaaw ligeey bi ci isin yi laajul doole ju rëye noonu ngir man ko. Loolu tam jurati yeneen jafe-jafey mboolaay, ndax tax na ba jigeen bàyyi fi ay ligeeyi boppam, dem ci isin yi, xale yi it bàyyi njàng mi, te loolu ag pert manu koo kawe, ndax xale yi ñooy yaakaari ëlëg. 
Ag yàqu-yàqu tàmblee feeñati ci wërlaay  gu mboolaay yi, ci Tugal, maanaam nit ñi, loolu nag mi ngi am bi ag ñàkk-ligeey tàmblee tas ak a yaatu ci Orob, ci ligeeykat yu góor yii nga xam ne danoo tàmbli woon a nekk ay jafe-jafe dëgg, ci kanamu goornamaa yi, di yëngal, tey sàkku nu nu leen lijantile seen jafe-jafey ligeey yi. Ci noonu goornamaa yi daal di def ay àtte , indi ay sart yu nos ligeey bi, aar ligeeykat yi ci fuqaleg boroom bopp-alal  yi moom isin yi.  

Ñatteelu bunt bi

Yëngu-yënguy politig yu mag yi ci adduna bi

Feeñug Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi (U.S.A)
                                   Jeqiku walla fipp  ga amoon  ca Fraans

Doggantal gu njëkk gi

Feeñug Diiwaani Amerig yu bennoo yi

Gàddaay yi waa Tugal yi daa def juge Tugal, jëm Amerig, gàddaay yooyu wéyoon nanu di sottiku ci Amerig gu bëj-gànnaar gi. Loolu nag amoon na, ginaaw bi Kolomboo feeñalee Amerig ba am lu tollook xarnu. Li ko taxaoon a am nag bari na, bokk na ci:

(1)	Fitnay diine yi amoon ci Orob gu digg gi ak gu sowwu gi, li waraloon loolu di yëngu-yëngu yu diine yi jugoon di kontar Egliisu Katolig bi, ak la ca juddoo muy ay xeexi ngér, yu amoon ci diggante ngérum Katolig ak mu Protestant , ak xeex bi protestant yi doon def ci seen biir, rawati na ci Angalteer, ak la ca juddoo muy bòddikoonte ci diine, loolu nag waraloon gàddaayug ab lim bu mag ci waa Tugal yi, dem Amerig gu bëj-gànnaar gi, ngir rawale seen bakan, ak ngir man a doxal seen diine ci ag féex akug ngore.
(2)	Fitnay politig ya amoon ca Tugal ngir xeex jaay doole ga fa amoon, ak àttee na mu la neexe ga, ak la ca juddoo muy ag ñàkk a nosu gu mbir yi ñàkk a nosu, ak ñàkk-kaaraange, ak dox gi nguur yi di doxe ni mu leen soobe, loolu lepp nag taxoon na ba lu bari ci waa Tugal yi gàddaaye woon fi nu dëkkoon dem, wuti ag goreg politig  .
(3)	Wër gi nu doon wër mbèll yu gànjaru yi, lu ci mel ni wurus mbaa xaalis, bokk na ci li leen daa gàddaayloo, ndax kat lu bari ci ñi daa gàdday, danoo gëmoon ne Amerig de reew mu fees dell la ak yile mbèll, te ña fa dëkk, ñu neew ag xay lanu, te ñàkk ag taaxe, te yittewoowunu yenn ligeey yu mel ni lijanti ay wurus aki xaalis ak gasi mbèll.
(4)	Jëm kanam gi xam-xam am ak endustri ci Tugal, rawati na ci wàllug ligeey ay gaal, googu jëm kanam dimblee na ci nu man a tukki ci geej gi, bay àgg ci barab yu sori yee sori.
(5)	Ligeey yi nga xam ne lonkoo yu Angalteer yi def nanu leen , ngir meññal ak jariñoo suufus Amerig si ak lijanti nu ñu koy sance te dëkke ko ngir dëgërale ci kilifteefug sanc  gu Angalteer ci goxub adduna bu bees bii, bokk na ci li waral gàddaay gi.

Sancu  yi nga xam ne waa Angalteer yi taxawal nanu leen ci Amerig gu bëj gànnaar gi: 

Waa Tugal yii bawoo woon Espaañ, Fraans, Holand, Suwed ak Angalteer, sancoon nanu ay barab yu wuute ci Amerig gu bëj-gànnaar gi, ñoom lanuy wax tay Diiwaani Amerig yu Bennoo yi , loolu nag di woon ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom benneel ak bu fukk ak juroom ñaareel g. Angle yi nag ñooy ñi njëkk a taxawal ab sancu ca Jims Town, ci diiwaanu New York, atum 1607 g, mujj nanu nag ci diir bu gàtt, di ñi gën a tas, gën a wisaaroo ci goxi tefes yu penku yi, ci mbooleem ñi gàddaayeTugal.

Barabi penku yii, maanaam yii nga xam ne la ëpp ca ña fa sancoon, dëkke woon fa ay waa Angalteer lanu woon, barab yii mooy yi mujjoon ginaaw bi (1776 g) di laaj ag temb  akug dagge ca reew may nday di Angalteer.  
Angle yi nag amoon nanu ñaari anam yu nu daa sance reew yi ak a yilife, bi ci njëkk mooy : buurub Angalteer da daan may yenn ci lonkoo yi, gu ci mel ni lonkoo gu Werjiniya gu London gi – mooy bi yoroon mbirum sos sancu bu Jims Town bi nu la waxoon leegi - da leen daa may ay sañ-sañ ci nu taxawal ay sancu, ak jariñoo xeewal ya fa nekk, ak defar xaalis walla koppar yu nuy man a jëflantee, ak topptoo mbirum kaaraange gi.
Geneen anam gi mooy: buur bi day dogal garmi  yu Angalteer yi ay suuf, ba noppi féetale leen mbirum yor leen ak àtte leen  .

Bi fukk ak juroom ñatteelu xarnu g, di agsi ci digg bi, Amerig mujj na yor fukk ak ñatti sancu yu Angalteer, ñooy: New York, Wirjiniya, Rood Island, Masacuusest, Dulawir, New Hamser, Kintakit, North Karolaayna, South Karolaayna, New Jersi, Jorjiya ak Pensilvaniya. Diiwaan yooyu ñooy yi sos, te amal li nuy wax Diiwaani Amerig yu Bennoo yi, ci ginaaw xareb temb gi , atum 1775 – 1783 g, ñu mujj am ag temb ci Angalteer, ci mujj gi. Diiwaan yooyu nag, bu nu leen xoolee ci Amerig gu leegi gii nii, dunu weesu benn xaaj ci Amerig gu nu xaaj fukki xaaj.

Noste gi doon doxal mbiri biir yu sancu yu Angalteer yi:

Nguurug Angalteer gi, daa joxoon ay sancoom yi nekkoon ci Amerig gu bëj-gànnaar gi, da leen a joxoon aw xeet ci “ag àtte sa bopp”  , waaye teewul ci biir loolu lepp, mu bàyyil fi boppam kilifteef ak cang gu mu am ci kaw sancu yooyu, maanaam may na leen ñu yor seen bopp, di doxal seen mbiri biir, waaye teewul muy seen kilifa, di reew mi leen moom.
Nosteg àtte-sa-bopp googu amoon ci sancu yooyu, mi ngi tegu woon ci ñatti ponk: 

(1)	Doxalkat bi , 
(2)	Jataayub yoonal bi , 
(3)	Jataayub diisoo bi . 

Doxalkat bi walla àttekat bi , mooy kilifa gi yilif dooley xare ji ci sancu bi, mooy feetewoo sàmm mbiri way dëkk yi, di topptoo kaaraange gi, te am na sañ-sañu dindi saxal gu nu defe ci ñaari jataay yii: bu yoonal bi ak bu diisoo bi. Moom nag (àttekat bi) buuru Angalteer bee koy fal ak a folli.

Bu dee nag jataayub yoonal bi, moom ñi dëkk ci sancu bi ñoo koy tànn, li ko tax a jug nag mooy tege galag yi  ak fuglu  ligeeykat yi, ak saxal seeni payoor, ak payooru doxalkat bi. Bii jataay nag li ko may doole mooy jële gi mu jële sañ-sañam ak kàttanam ci nit ñi dëkke ci sancu bi, ginaaw ñoo ko fal.

Jattayub diissoo bi moom, li ko taxoon a jug mooy di xelal àttekat bi ak jataayu yoonal bi, ak di diisoo ak ñoom.
Waaye nag moom sancu bi, ak li mu jot a am lepp, muy “ag àtte-sa-bopp ”  gi nga xam ne taxoon na ba nu man fa’a doxal demokraasi, teewul mu nekkoon ab sancu rekk bu toppoon ci ginaaw nguurug Angalteer gi, ci gisiinu waa Angalteer.

Goornamaa bu Angalteer li mu fàttee def mooy, wut nu mu nose mboolooy angle yii dëkke woon sancu yi, ñoom mbooloo yii nga xam ne mujj nanu lu jamono di gën a yàgg, ñuy gën a sori seen reewum nday ma di Angalteer, ci wàllug aada ak dundiin, loolu waral ñu tàmbli koo fàtte, di yëg nag leegi ne fii mooy seen reew, di ci tënku, te di ko fonk.
Loolu nag tàmbli woon na a wuute ak politig bi George mu ñatteel mi, taxawaloon, moo doonoon burub Angalteer ca jooja jamono, lii mooy li taaloon ab xare bu mag ci diggante sancu yi ak nguurug Angalteer gi, xare boobu moom lanuy tudde xareb temb bi  .

Li waraloon xareb temb bi:

Ñi dëkke woon sancu yi, ay mbooloo lanu woon aki kureel yu wuute, ak doonte la ëppoon ca ñoom ay waa Angalteer lanu woon yu di ay protestant  . Seeni njariñi koom-koom it bokkewul woon, te niroowul woon, waaye nag, loolu lepp teewul woon amoon nanu ñatti mbir yoo xam ne kenn wuutewu ci woon, ñepp a ci dëppoo woon, ñooy: 

(1)	Am gu nit war a am “ag goreg jëmm” , rawati na “goreg pas-pas”  
(2)	 Ak sàmmoonteek yoon ak nosu, maanaam nosu gi mbir yi war a nosu.
(3)	Yëg gi ku nekk yëgoon ne fii ci sancu yii la dëkk, moo dim reewam, fa la feetale ag reewoom  . 

Ëttub Amerig bii nag mujjoon di def ay mbir yoo xam ne ñoo waraloon xareb temb bi tàkk. Mbir yooyu manees na leen tënk ci yii:

Yoon  yuy tege galag ak tembar:

Parlamaa bu Britani bi daa genne atum 1762 g, aw yoon walla luwaa bu nuy wax luwaa bu tembar yi, mooy biy def ngay fay tembar ci jëflante yu Ofisel yi, ak dosyee yi, ak yëglekaay yi añs. Ci atum 1764 g, ñu farataal galag  ci suukar si nu daa jële ci sancuy Espaañ yi, yu Fraans yi ak yu Holand yi, teg ci farataalati ko ci ataaya, kayit, weer ak rasaas  .

Yoon  wi aju ci geeju (navigation) ak yaxantu:

Ci atum 1651g, barlamaanu Britani bi dafa genne benn luwaa buy waral ci sancu yi nuy tuxal  li nuy genne  ak li nuy duggal  di ko def ci ay gaal yu Britani, aaye leen ñuy jëndati feneen, leneen loo xam ne bari na Angalteer.

 Koppar walla kee   bu kayit ak jënd suuf:

Sancu yu Britani yi danu leen a aaye woon ci yoon, ñuy genne walla ñuy defar benn kee bu kayit ak di ko jëfandikoo niki kee bu ofisel  . Noonu tam lanu teree woon – ci beneen luwaa - ñuy jënd suuf yi feete sowwu fukk ak ñatti sancu yi, ngir jàpp gu nu jàppoon ne yooyu suuf nguurug Britanee leen moom.

Nos dooley kaaraange ji:

Goornamaa bu Britani dafa sosoon jenn doole ju xare ngir aar sancoom yi nekkoon ci Amerig gu bëj gànnaar gi, doole jooju tolloon na ci junniy xarekat , mu waxoon waa sancu yi ne ñooy warlu di joxe depaas yi doole jii di laaj. Loolu nag taxoon na ba waa sancu yi mer, ñaawlu loolu lool, ngir loolu tam goornamaa bu Britani bi ne kon na ci genn, waaye nag galagu ataaya moom dindiwu ko.
Loolu tam tax na ba waa sancu yi di yëg ne ñoom daal danuy jëflante ak ñoom, mu mel ne dañuy ay nit walla ag njaboot goo xam ne ñoo gën a neew solo ak daraja ñi dëkke Angalteer.

Waa sancu yi tam yëgoon nanu ne li nuy fay ciy galag lepp, dunu leen ko defal fi nu koy faye waaye kay ca reew mu leen sori mee di Angalteer, te loolu du leen jariñ ci seen dund gi, te du ci def dara. Nga rax ci dolli ne Angalteer mooy reew mi rënkaloon boppam ci sancoom yi, yaxantug marsandiis yu bari, maanaam bari na lool ay marsandiis yoo xam ne Angalteer da ne woon moom rekk a leen sañ a jaay ci sancu yi, lu mel niki ataaya, loolu nekkoon na lu waa sancu yi ñaawlu woon.
Ci nii daal la xew-xew yi toppantee woon, di nëxal nag sellug seqoo gi amoon ci diggante Angalteer aki sancoom, loolu tam gën a yaatal paxum reeroo mi nekkoon seen diggante.
Loolu nag gën na a fés, bi waa sancu yi bañee ne dunu fayati galagu ataaya, ginaaw bi tam am mbooloo jug, ci desambar atum 1773 g, lakk ñatti gaal yu nguurug Angalteer, yu nu duyoon ak ataaya, ca waaxub Boston, ca sancu bu Masacusets, loolu waral waa Angalteer tëj waaxub Boston bi, ne gaalug yaxantu du fi teerati, daal di ne moom ci jëmmi boppam mooy yoral boppam sancu boobu.
Xew-xew bii ak la ca juddoo , man nanu ne moo waral xareb temb bi.

Ndajem waxtaan mu Filadelfiya mu njëkk mi: 

Juroom ñeenti diiwaan yu Ameriig teewe woon nanu ndajem New York ma, atum 1765g, di sàkku ci nguurug Angalteer mu teggil leen galagu tembar bi mu leen di teg.
Ci noonu Angalteer teggi woon na galag boobu waaye teewul mu wéyoon di tege yeneen galag yi nga xam ne ab Parlamaam daa na leen woote, te di leen farataal ci mbooleem ay sancoom yi nekk ci adduna bi.

Looloo taxoon reenub reeroo bi amoon ci diggante Angalteer aki sancoom saxoon fi di lu ñu dogadi, ndax kat sancu yi danoo gisoon ne di leen teg ay galag te seeni jataayi yoonal ànduñu ci, bu amee lu muy tegtale mooy dindi màndargam demokraasi mi seen jataay yooyu di doxal seeni mbir ame woon, ndax kat daa am ab dal  bu nekk ci demokraasi, bu naan “doo fay galag boo amul ndaw” .

Man nanu ne ndajem New York mi mooy lu njëkk a feeñ te nosu loo xam ne waa sancu yi def nanu ko, di ci kontar ni Angalteer di àttee seen reew yi.

Ñoñ sancu yepp a meroon bi Angalteer tëjee waaxub Boston bi, bu ko defee ñu taxawal am ndaje ca Filaadelfi, atum 1774 g, jàmmaarloo fa’ak Angalteer ne ko na xam ne lepp lu mu defati benn sancu ci sancu yi, na ko wóor ne sancu yepp la ko def, daal di ñaawlu bu baax jëf yu ñaaw yi Angalteer tegoon Boston . Njiitul xare lii nuy wax George Washington (1732 – 1799 g ) teewe woon na ndaje ma.
Ndajem Filadefi moomu, mooy dàtt  bi nga xam ne ci la Kongres mujj a teggu, ci ginaaw bi .

Jaadu na ñu leeral leen ne ndajem Filadefi mi li ko taxoon a jug du sàkku ag tembte , waaye kay yëgal Angalteer ne lu wuuteek demokraasi lii muy def ci sancu yi neexu leen, te man na a nëxal te yàq xaritoo ak jàmm ji amoon ci diggam ak ay sancoom.
Ñoom kay seeni càkkuteef weesuwutoon lii, mooy na Angalteer xam ne ñoom sancu yi kat ñoo ame àq ak sañ-sañ -  ci seen jataayi yoonal yi – ci tege ak farataal ay galag ci waa sancu yi.

Angalteer nag, ci safaanub muy lijanti lëj-lëj boobu ci maslaa  gu xereñ, moom daal da fee nekk di yonnee ay dooley xare yu yees ci Boston, ngir gën a dëgëral doole ja fa nekkoon.
Loolu tam li mu juroon mooy waa sancu yi ñoom itam, ñu ne woon nanu waajal seen bopp, ndax kat nguurug Angalteer gi bëggul jàmm, ci noonu ñu - ñoom waa sancu yi – defaat beneen ndaje ci Filadefi, ngir jàng mbir mi, seet nu ñu ciy def.

Ndajem Filadelfi mu ñaareel mi:

Ndawi sancu yi defoon nanu am ndaje atum 1755 g, ca Filadelfi, muy ñaareelu ndaje mu Filadelfi mi, ñu wax fa ne danuy sos menn mbooloom xare , te bennal ko, bañ a def sancu bu nekk am sa mbooloom xare, bu ko defee nag, mbooloom xare moomu ñu tànne ko ci waa sancu yi, ngir ñu aar leen ci ay wi leen dëgmalsi. Ci noonu ñu duggal doomi sancu yi ci xarekat yu bees yii nga xam ne George Washington moo leen jiite woon. Waaye teewul ñu yonnee ca buuru Britani bi, ab bataaxel buy sàkku ci Angalteer mu xoolaat ni muy jëflanteek sancu yi, te lenn baaxu ci, waaye buur bi moom jàpp fa mu jàppoon rekk, ne daal am na ag cang gu nu joyal ci kaw mbooleem sancu yi. Ci jëfam jooju la tëje buntub jeem gi sancu yi doon jeem ngir defar – ak doonte lu neew la itam – seen diggante ak Britani, reew miy nday.

Ni xare bi tàkke :

Bi buur bii di George mu ñatteel mi, ñàkkee faale càkkuteefi sancu yi, ne daal li wér mooy moo ame cang gu joyu gi ci mbooleem sancu yi, maanaam sancu yepp ci ron kilifteefam lanu nekk, ci anam gu matale te daj, bi buur bi nekkee ci taxawaayam boobu ne du ci juge la xare bi tàkk ci diggante ñaari wàll yi, sax nag lu toll ci juroom ñaari at daanaka (1775 – 1783 g ), bu ko defee, mu tas nag ci li ëpp ci  sancu yu Amerig yi, George Washington nag jot na a man a nangu Boston, ginaaw bi mu ko gawee. Dooley gornamaa bu Britani moom, teg loxo lu bari ci waaxi Amerig yi.
George Washington ni mu doon xeexe ak ñoom nag mooy xeexub bette, ci barab yu bari, ak door-daw, foo ko fekk daawul nangoo jaamaarlook ñoom, ndax xammoon na ne ñoo ko ëpp doole te gën koo tàggatu.

Ak li xarekati sancu yi doon jànkoonteel lepp ciy coona yu tar ci biir xare bii, teewul George Washington gañe woon na njiitul Anglteer lii di Burgoyne, ci xareb Saratoga, loolu mi ngi am bi mu jawalsee juge Kanada, jëm New York, ci oktobar 1777 g. Ca saa sa, ginaaw bi nu gañee Britani, Fraans jug na, yëgleb xareem ci kawam atum 1778 g, Espaañ roy ko ci, atum 1779 g, Holand topp ci atum 1780 g. Man nanoo wax ne Fraans moom jàpple na way fippi sanncu yi ci wàllug xare (militaire) ak ci alal, ba tay it dajale na way coobarewu  yu Fraans yi, yobbu leen ci Diiwaan yu bennoo yi, ngir nu xeexle leen ci ron njiit lu xare lu Fraans lii di Lavette, kontar Angalteer noonam bu mu yàgg a noonool bii. Ci noonu Britani mujj war a xare ci jë  yu bari.

Dàq gi nu mujj a def dooley angle ji, ci sancu yi, mooy gi nu defoon seen njiit la Cornwallis, loolu di bi mu deltoo ginaaw, dem dëkkub York Town, fa dexug York di sottikoo, ginaaw ba ko fa mbooloom xarem George Washington ma songee. Xarekati George Washington yooyu nag am njaxasiitum kureel lanu woon mu ame ci diggante ay waa Fraans aki ñoñi sancu, tollu nag ci fukk ak juroom benni junniy xarekat.

Nanu fàttaliku nag ne waa Amerig yi ñoom, ci seen suuf lanu doon xeexe, bu ko defee dolli leen doole ci xare ak ci alal day gën a yomb, gën a gaaw, bu dee waa Angalteer yi xawoon a sori Kanada, fi seen bagaasi xare daan juge, walla Angalteer mi leen soree woon lu tollook ay ñatti junniy miil daanaka.
Nga rax ci dolli, waa Amrig yi danoo dogu woon bu wóor ci raxasu ci teg loxo gi Britani tegoon loxo seeni mbir, te amoon nanu ay njiiti xare yu bari, ku ci mel ne George Washington.
Doolil ci loolu, nekk gi waa Britani nekkoon di xeexe ci sancu yoo xam ne manuñu fa’a ame jokkoo ak dolli doole ga war, ca anam ga mu ware te gaaw, te itam pasteefub xeex bi nu amoon moo gën a suufe fuuf bi waa sancu yi amoon, ñoom ñi taxawoon tamb ci xettaliku ci waawug nguurug Angalteer gi.
Bokk na ci li doyadil waa Britani yi ci xeex bi, ubbi gi nu gubbi woon ay jë yu xare yu bari ci seen kaw, ci barab yu sakkan ci Amerig.

Tembug Diiwaani Amerig yu Bennoo yi:

Bi waa Britani xamee ne lòtt nanu ci toroxal jeqiku gi amoon ci Amerig, te xam ne doole du mooy lijanti lëj-lëj yi nekk ci sancoom yi, ndax kat mi ngi nii di ku nu dàqe, gañee ko ca xare ba, bi loolu amee mu sàkku woon ag juboo, ci noonu ñu xaatim juboo gi ci Paris, ci digganteem aki sancoom atum 1783 g,  lii mooy poñ ya ca ëpp solo:

(1)	Britani day nangu  tembteg sancu yi nekk ci suuf yi feete ci  penkub dexug Misisipi gi, te jàppe dex gii muy diguw soww wi ko tàqale ak sancu yi. Bu ko defee dig yu bëj gànnaar yi ñoom ñu bàyyi leen nanu nekke woon.
(2)	Jeem a rafetal seqoo  yi, ci diggante Britani ak reewum Amerig mu temb mi (Diiwaani Amerig yu Bennoo yi)
(3)	Amal ci diggante Britani ak Amerig gu temb gi, ay seqoo yu yaxantu ak yu koom-koom, waaye nag seqoo yooyu ñu teg leen cig nawlante, ak moroomante, kenn du jaay kilifteef sa moroom.

Nii daal la Diiwaan yu Amerig yu Bennoo yi ame, xareb temb bi nag am na benn jeexiit bu rëy te xóot, ndax wal na te upp ngelawul gore ak temb ci mbooleem sancu yi.
Lii nag làppal na Britani, loofloo ko, ci wàllug xare ak politig, nga rax ci dolli alalam ju bari ji mu ci ñàkke.

Amerig nag moom, daal di ñew, defar sartu reewam , daal di taxawal ndajem booloo mi nga xam ne Kongres moo ko digale woon, atum 1788 g, mbooleem ndawi Diiwaan yu Bennoo yi teewe woon nanu ko, ba mu des diiwaanub Rood Island. Cer ya fa nekkoon tam, tànn cig dëppoo, George Washington muy njiitul ndaje mi, ci loolu la nekke ki njëkk a nekk njiilul Diiwaan yu Bennoo yi.
Ginaaw bi lanu def Washington – ginaaw bi mu nekke peeyu koom-koom bi ak bu alal bi – la nu ko def peey  bu politig bi. George Washington nag jëloon na xalaatam yepp, def leen ci nu muy def ba bennal Amerig, looloo taxoon waa Amerig yi soppoon ko, wormaal ko, waxam it weesuwutoon : (( doon leen benn, doon leen ay waa Amerig ..)) , loolu saxoon ci seen xel yi.
Washington moom wàcci na jal bi, joxe njiit gi, atum 1797 g, ginaaw bi mu ko yoree ñaari yoon.

Doggantal gu ñaareel gi 

Jeqiku walla fipp ga amoon ca Fraans :

Jeqiku  walla fipp  ga amoon ca Fraans, mooy jeqiku gi njëkk a am ci jamono ju bees jii, ci kaw nguuru ak jaay doole, ak doxale ni la neexe, doo diisoo, doo deglu xalaatu keneen. Moom nag (fipp googu), mi ngi ame woon ca Fraans, ca jamonoy buur ba tuddoon Luwis mu fukk ak juroom benn ma, bokkoon ca njabootug Barbon ga, loolu nag di woon ca noorub 1789 g, saxoon it diir bu toll ci fukki at, ba ca nawetub atum 1799 g, bi Jeneraal bi tuddoon Napoleon Bonaparte (1769 – 1821 g)  defee yong  gu nuy wax yongug 18 Brumaire, dëppoo ak 9 nowambar 1799 g, daal di daaneel doxaliin wa fa nekkon, jële fa it jataayub mag ña , mujj nag di kenn ci ñatti kilifa yiy doxal mbiri reew mi.
Bonaparte mii - nga xam ne mujj na di kilifag Fraans gu njëkk gi, ci atum 1800 g, mujj it di imbraatoor ba atum 1804 g – moom Bonaparte mujj na am tawfeex ci dindi lëjug politig ga fa amoon, ñàkk jàmm ga, tiitale ga , tuur dereet ga, ak yeneen jëf yu ñaaw yi àndoon ak fippug Fraans gi. Loolu nag taxoon na ba “fipp gi” manu fi woon a amal dali gore , yamoo, mbokkoo yi nga xam ne ñoom la yàgg a yekkati kàddoom ngir saxal leen fi.
Waaye nag jeexiit yi nga xam ne fipp gii ba na leen fi, yamuñu rekk ci Fraans, waaye weesu nanu ko ba daj Tugal gepp, ak lu bari ci reewi adduna bi. 

Ni Fraans meloon laata fipp gi:

Bu ñu gëstoo na Fraans meloon laata fipp gi, loolu di na nu dimbli ci nu man a xam li waral fipp gi, atum 1789 g.

Melokaanu politig wa:

Buuri Fraans yi, ni ñu doon àttee Fraans, du woon nenn nu dul ni mu leen neexe. Buur bi moo daa saytu lepp, kepp ku am nguur moo la ko daa jox, moo daa doon balluwaayu mbooleem doole yi, ak sañ-sañ yi, walla nga ne sax mooy nguur gi, di sañ-sañ bi, di kàttan gi, di doole ji. Loolu nag man nga koo degge ci waxi buurub Fraans bii tuddoon Luwis mu fukkeel meek ñeent : ( Man maay nguur gi ).

Buur bi mooy ki am sañ-sañ ci def ay yoon , ak neenal leen, tege ay galag, def ci alali reew mi lu ko soob, tabb jëwrin yi, fal ligeeykat yi, folli leen, joxe ay ndigal jaare ko ci ay bataaxel yu nu xaatim, ngir nu jàpp ku ko soob ci askan wi, ak tëj ko ci lu dul mu koy àtte mbaa mu koy laaj dara. Buur bi daal - ci gàttal – lu ko soob mu def . Ndax moom dafa gis ne mi ngi wéeru – ci sañ-sañam boobu – ci gis-gis bi fiy indi “sañ-sañu Yalla bi”, mooy li naan buur bi daal, nguuram gi, ak sañ-sañam bi mi ngi bàyyikoo ca Yàlla. Luwis mu 16 mii nag, nga xam ne ci atum 1774 g la nekkoon ci jal bi, tey buur bi nga xam ne ciy jamonoom la fipp gi xewoon, moom Luwis mii, nekkoon na ku doyadi, te daan dengi-dengi.
Moom de jaraafam yi danu koo yilifoon, ak bëkkneegam yi, ak soxnaam si bàyyikoo woon Hongri, Mari Antuwanet (di woon doomi lingeerub Ongri ba, Mariya Tereesa), moom soxnaam soosu nag, ku yëgoon boppam la te faaleedi woon askan wi, taxoon na ba kenn manut a def genn yéwénal, kenn manul a jàpple buur bi ci luy defar.
Moom daal nekkewu fi woon lu dul yàq alal, noos, ak caaxaan, nekkoon it ku diis, te rëyal boppam, looloo taxoon mu mujjoon di ku waa Fraans yi bañoon. 

Njabootug Barbon gi, yàgg nanoo jariñoo seen nguur gi, ci luy lor askanu Fraans wi, ñoom daal danu daa nangu alali ku leen neex, daan tëj ku leen soob, daan xeexloo reew mi saa su leen soobee, te xeex yooyu yu ci ëpp danu ci daa gañe Fraans.
Bari na lool lu ñu daa tabax ay njénd , di ci sotti alali reew mi, ak di may seen dag yi alal ju dul jeex, seen dag yu bari yooyu nga xam ne tolloon nanu ci 18 junniy nit, atum 1789g, te lu ëpp ci ñoom defuñu fa woon dara, amul lenn lu nu fay ligeey lu amal njariñ reew mi. Looloo taxoon njëlul  nguur gi loof, mujj moom nguur gi fees dell aki bor.

Nguur gi kat mujj na ay deppaasam àgg ci 130 milyong yu Frank, atum 1789 g . Li mu ameele woon ciy bor àgg ci 206 milyon yu Frank, ngir lòtt gu njëlam li lòttoon.

Baj-baji ak doxadi amoon na ci wàllug doxaliinu nguur gi, ci wetu doxe ni la neex ga amoon ca wàllug politig ga.
Nattukaayi gox bii daawul bokk ak bee, naka noonu yoon yi  , màndaxekaay yi, galag yi. Ci noonu Fraans mujj di reew mu ay gox boole, gox bu ci nekk am ay yooni boppam  , aki nosteem yu wuuteek yeneen ya ca feneen, loolu nag waraloon na ag lënt ci nosiin yi ak luwaa yi, reew mi mujj seddaliku, doon ay doxaliin yu temb. Bu ko defee, Fraans mujj doonatul menn reew, waaye ay doxaliin yu wuute te tas. 

Na mboolaay ga  meloon:

Mboolayug Fraans gi, njëkk fipp gi, dafa seddaliku woon, doon ñatti kureel yu mboolaay, ñooy: kureelug ñu tedd ñi, walla garmi yi, kureelu niti diine yi, ak kureelu mbooloo mi walla baadoola yi. Ñatti kureel yii nag – ñoom de ci li fi  jamonoy laman desaloon lanu – yamoowunu woon ci àq ak yelleef, du caageegug ci ay warteef, li am daal mooy ag yamoodi gu mboolaay amoon na ci seen diggante, jefkay tàqali ak feewaloo ruuru leen, ak boddante gu mboolaay.

Bu ko defee kureelub garmi yi nu teggil leen galag yi, ña ca bokk it ñoo daa feetewoo pal yu kawe yi, yu siwil yi ak yu xare yi , ci nguur gi.
Ñoom ba tay, daa nanu am ay cer ci mbayum baykat yi, ak ci jurug sàm yi, ak seen ñanaaw yi. Amoon nanu it sañ-sañ ci rëbb ci tooli baykat yi. Baykat yi tam amunu wonn sañ-sañ ci wal seen dugub ci lu dul walukaayi garmi yi, te seen reseñ it sañuñu ko woon a nale fu dul ci seen nalukaay yi.

Loolu lepp nag daanaka ñi ko daa jariñoo, ñu neew la daan doon ci niti diine yi ak seeni njaboot, bu ko defee ñu bàyyi nee way ndool yi, ak ñi aajowoo, kenn du leen dimbli.
Ña ëpp nag ca niti diine ña, taxutoon ñu feexoon, moo taxoon danu daan ànd ak mbooloo mi, kontar garmi yi.

Kureelub mbooloo mi nga xam ne la ëpp ca askan wa ca lanu bokkoon, ñoom jegge woon nanu, bi fipp gi di bëgg a door, lu tollook 25 milyongi nit , te kat booba garmi yi bu nu leen boolee ak niti diine yi weesuwunu woon 300 junniy nit. Coonab galag yepp ci ndoddum baadoola yi la daan tegu. Kureel boobu nag (bu baadoola yi), moo ëmboon kureel bu diggu bi, walla bi nuy wax (Bourgeois), ak kureelu baykat yi ak bu boroom mecce yi ak bu soldaar si.

Bu dee kureel bu diggu bi moom, ca la boroom xam-xam ya bokkoon, xalaatkat ya, boroom xel yi. Ñoom nag amunu woon sañ-sañ ci pal yu kawe yi. Moo ëmboon it yaxantukat yi, ak boroom alal yi daa fay galag yu mag yi, nga xam ne seen fay gu metti gi nu daa fay galag yi, ak lamb gi amoon ci seen yaxantu gi, taxoon na ba seen koom-koom daanu woon.
Lii lepp nag taxoon na ba gii kureel meroon lool ci goornamaa bi, te meroon it ci ay jëfam ak ci li nu defaloon ñaari kureel yii di bu garmi yi ak bu niti diine yi.

Bu dee “kreelug baykat yi” nag, ñooy ñi gënoon a sonn ci kureelug baadoola yi, ñoo ci daa njëkk a yëg aw ay bu jafe-jafe bu kopooar amee, ndax ci seen kaw lanu ko daa tegaat, ci fayloo leen ay galag, ak teg leen ligeey yi gën a tar.

Bu nu nee “kureelub soldaar si”, ñi ngi ci jublu soldaar su ndaw si, ak boroom ndomay xare yu ndaw yi, ndax ndoma yu mag yi moom, ak pal yu mag yi, garmi yi lanu leen daa jagleel.

Na fa xalaat meloon: 

Ak li Fraansu njëkk fipp gi, di gënadi woon a nekk cib coona,  ak ñaawug nekkiin yeneen reew yi mel ne : Itaali, Otris, Brusiya, ak Riisi lepp, teewul waa Fraans a gënoon a yëg yeneen reew yi tooñaange yi nu leen daa teg. Li waraloon loolu nag mooy yewwuteg politig ga fa amoon ak gu xalaat ga, ca biir boroom xel ya ca kureelub baadoola ya, di yaxantukat ya, ustaas ya, layalkat ya , doktoor ya, boroom xam-xami koom-koom ya, bindkat ya, xeltukat ya añs.
Jamono jii , dafa fiiroo  ak diggante bob Fraans da cee amoon ay xalaatkat yu mboolaay, ak yu koom-koom yu leen daa yee ci coona yi nu nekke, ak bonug nosi politig ya fa amon, yu mboolaay ya, yu doxaliin ya, ak yu alal ya.
Da na jaadu nu waxtaane fi ñatti xalaatkat yoy ligeey nanu lu rëy ci tas fi xalaat yi fi indi fipp gi. Ñooñu ñooy: Montesqieu, Voltaire, Jean Jacques Rousseau.

Bu dee Montesquieu (1689 – 1755 g) - moom mi nga xam ne siyaare na Angalteer, gondiku woon it lool ca nosteg sartu reew gu buur ga fa nekkoon – moom de ay ligeeyi xam-xamam mi ngi feeñe woon ca teereem ba tuddoon “Ruug yoon yi” (1748 g), teere boobu nga xam ne teere bu jaroon la, bu boroom xeli yi fonkoon la ci Fraans ak feneen.
Xalaati Montesquieu yi ñi ngi tënku ci fexee tënk goornamaa bi, te fuglu ko  ak tàqale diggante dooley yoonal ji, ak ju doxal ji, ak ju laman ji  .
Moom Montesquieu nag li mu doon wut ci teereem boobu mooy taxawal ag atte gu tegu ci sartu reew ca Fraans. Ndax kat moom dafa gondiku woon lool ca sartu reew bu buur ba amoon ca Angalteer.  

Bu dee Voltaire (1694 – 1778 g), moom de woote na jëme cig coppi ci nekkiinu askanu Fraans wi, jaare ko ci taalifam yi mu defoon ciy woy, nga xam ne taalifi jam  lanu woon ak yéjj  .
Moom de jamoon na nosteg politig ga amoon ca Fraans ak gu egliis ga, ak sañ-sañ yi garmi yi amoon ak niti diine yi.
 Wolteer de ak li xalaatam yi doonadee woon lu yees lepp, teewul seen solo ñi ngi feeñe woon ci nekk gi nu nekkoon di luy laal yëg-yëgi waa Fraans yi, ngir nekk gi ñu nekk di ay xalaat yu nit yuy jeexiital.
Wolteer de gore  ga waa Angalteer ame woon da koo neexoon lool, yeemoon ko, mu jeexiitalu ci, ginaaw ba mu fa amee ñatti at, li waraloon mu nekk fa nag, mooy danu koo dàqe woon Fraans.  
Gore googu mu gisoon ca Angalteer, ak xalaat ya mu fa ame woon, feeñal na leen ca teereem ba tudd  “bataaxeli xeltu” , walla ay bataaxel yu bawoo ca waa Angalteer, atum 1734 g.
Wolteer nag dàq gi nu ko dàqe woon Fraans, yobbu ko Angalteer ak tëj gi nu ko tëjoon lepp ca kasob Bastil bu metti, bu raglu ba, teewu ko woon a wéy ci jam  garmi yi ak niti diine yi.
La desoon ca dundam ga lepp it da koo jeexaloon ci nekk di ku yoon di wër.
Bu dee Jean Jacques Rousseau (1712 – 1778 g), mooy boroom teere ba tudd “kollareg mboolaay” , mooy teere bi doon woote jëme ci goreg nit  ak yamoo gi nit ñi war a yamoo ci wàllug mboolaay, mu neeti goornamaa bi daal li ko war mooy mu sonn ci yittey nit ñi.
Fippug Fraans gi, mi ngi sukkandiku woon – bi muy lim yelleefi ki dëkk Fraans – mi ngi sukkandiku woon ci xalaati Rousseau yu mboolaay yi nekk ci teereem boobu nu doon wax leegi.

Jafe-jafe bu koppar  ba:

Atum 1789g, mooy at mi fipp gi ame woon, nekkutoon at mu ya ko jiitu woon tane, ci wàllug koom, waaye la waraloon fipp ga am ca, mooy ñàkk a taw ga mu àndaloon, ga juroon bekkoor ba ak xiif ba, nit ñi mujjoon di ñu ñàkk, aw ñam jafe, dundiin wi naqari. Bokkoon na ci li gënoon a mettil mbir mi, galag yu bari yi nga xam ne tege woon nanu leen, te lepp di woon ci ndoddum baadoola yi, ngir mëdde ci depaas yu bari yii nga xam ne nguur gi daa na leen def, ngir boram yu bari yii mu daa jële ci xare yii mu daa faral a def ci biti, ci jamonoy Luwis 14 ak Luwis 15, te loolu ci li daa jeexal ay koomam la woon.

Luwis 16, bi mu ñëwee jeem na ba sonn, ngir lijjanti jafe-jafe bii amoon ci mbirum alal mi, ak loppanti njëlul nguur lu loof lii te sonn, jaare ko ci tege ay galag yu bees, waaye mujj na di ku manutoon a ñàkk a woo “jataayub kureel yu xeet wi” – bii nga xam ne danu koo tasoon ci jamonoy Luwis 14 – ngir mu daje.

Naka la fipp gi ame woon :

Doomi kureel gu diggu gi, begoon nanu lool, bi Luwis 16 woowee jataayu kureel yu xeet wi, ngir mu def am ndaje ngir gëstu yoon yi man a lijjanti jafe-jafe bii aju ci lòtt gi njëlul reew mi lòttoon, ñu gisoon ne loolu daal pose  bu mag la ngir nu indil seen bopp, saafara si ko man a faj, te fajal ko seen bopp. Ñi daa woote yewenal it jàppe woon loolu pose ngir def seen yewenal yi nu yeene woon, ak soppi yi nu bëggoon ngir Fraans man a baax, man a tegu ci yoon, bañ koo yamale ci loppanti njël li rekk.
Ci noonu ag wuute am ci diggante kureelub garmi yi ànd ak bu niti diine yi ci wàll, ak kureelub baadoola yi ca geneen wàll.
Bu ko defee waa kureelub baadoola yi sàkku woon ñu def  woote bi mu sukkandiku ci cer yi te bañ a sukkandiku ci ay neeg, ndaxte la doonoon aada foofa mooy kureel bu nekk ci ñatti kureel yooyu, da daa am genn kàddu, bu ko defee yenenn ñaari kureel yi (bu garmi yi ak bu niti diine yi) bu ci nekk am ñaari kàddu, bi ñaari kureel yii lànkee, ne deesu fi wootee, di ko teg ciy cer , ne daal ay neeg ñooy woote, bi loolu amee, ceri kureelu baaloola yi danoo daje ñoom nee, cig beru, ñu neew ci garmi yi ak niti diine yi jàpple leen, dëgëral leen, ku ci mel ni garmi bii di Mirabo, ñu waxoon ne ñoom daal ñooy ndawi li ëpp ci askan wi, ñu giñoon it ca fowuwaayu  tennis ba nekkoon ca wetu njéndul Versay la, ci atum 1789 g, ne ñoom de dunu bàyyi mukk lii nu nekke li feek wutalunu reew mi ab sartu reew bu man a yewenal seenu nekkiin te baaxal ko, ak doonte Luwis 16 moom li mu àndoon mooy kureel yepp daje, te xam ne ñooy ndawi reew mi, bu nu booloo, waxul bu benn taqalikoo nee, beru.
Ci noonu way daje yii nga xam ne danoo tudde woon seen ndaje mi, ndajem xeet wi  , walla “jataayub taxawal bi” , ñoom de foofu lanu nekkoon ci defar sart bu bees bi ñeel Fraans, bi nga xam ne day leeral li waa Fraans bëgg, tey jeem ci seeni aajo. Jëf jii nag mooy doorug fipp gi.

Tolluwaay yi nga xam ne fipp gi romb na leen:  

Ceri ndajem xeet wi daje woon nanu ca Versailles ngir defaral Fraans ab sartu reew bu yees. Askaan wi daal di jañu jëm ca kasob Baasil ba, ca Paris, ca 14 sulye 1789 g, song ko, nangu ko, genne ña ñu fa tëjoon ngir politig.
Jëf jooju mujj di juy wone gore gi nga xam ne moom la fipp gi doon woote jëme. Ñu mujj jël bis boobu def ko màggal gu xeetu Fraans wi di màggal, at mu nekk .

Nangu gi nu defoon kaso bi, ñemeloo woon na baykat yi, ñoom itam ñu jug, song suufi garmi yi, yàq seen njénd yi, looloo waraloon lu bari ci garmi yi gàddaaye woon Fraans, dem feneen.
Nekk gi nu nekkoon feneen, mujjoon na di aw ay ci Fraans, ndax buur yi nga xam ne doonuñu woon ànd ci fipp gi, ndax du seen njariñ, danu leen doon ngemb ngir ñu xeex ko, te loolu doon na jëme ci xareb ñoñ  .

Askanu Paris wi wutaloon nanu seen bopp ay ngànnaay, ñu daal di woon sos ag wattu gu reew ngir wattu fipp gi, aar ko, Lafyette jiite ko, moom mi nga xam ne waxoon nanu la ne doon na xeex di jàpple waa sancu yi kontar waa Angalteer ca xareb temb ba.
Xarekati fipp gi, ñi leen jiite woon ay nit lanu ñu bañoon te sib doxaliinu njabootub Barbon gi, ak seeni dag, Lafyette moomu ci la woon, ñoom de seen xol yi dara nekku ci woon lu dul mbañeel, wañse  ak gënjëng  .

Ci bis bi njëkk ci ut la ndajem xeet wi jibal “àqi nit aki yelleefam”, ci 4 ut, mu neenal sañ-sañi laman yi  ak yeneen yi garmi yi ame woon, ak niti diine yi.
Xeet wepp mujj daanaka di jàpple fipp gi, lu bari ci doole ju ngànnaayu ju Fraans ji mujj fekksi “wattu gu reew “ gi nu taxawaloon ngir wattu fipp gi. Ci noonu mbooloom xare  mu Fraans mi tas, Luwis 16 mujj ànd ca la xewoon ca kaso ba.
Waaye way fipp yi digale nu sàmm Luwis 16 ba du daw, ci noonu ñu taxawal seen bopp ci doxal mbirim reew mi, ak mu Egliis bi ci wàllug doxaliin ak alal, loolu moo merloo woon paab gi, mu mujj moom paab gi di kenn ci ñi gën a noonu fipp gi. Ñu daal di bennal nattukaay yi, ak yoon yi , ci Fraans gepp, ñu daal di seddalewaat Fraans def ko ay doxaliin  yu bees .

Bi ndajem xeet wi di teg sart bi, Luwis 16 doon na jeem a dolli ay kàttanam aki sañ-sañam, bi mu ko manul nag, la doon jeem a daw, juge ca njéndam la, waaye ñu jàpp ko ca Farn, ca 22 suye 1791g, njëkk muy genn reew mi, gis nanu tam benn dosyeem bu mu fi bàyyi woon buy feddali ne moom daal nanguwul yoonal yooyu mu àndoon, ndax ànd googu mu ci àndoon danu ko cee manante woon , waaye du lu mu def ci teeyug bakkan.
Ndajem xeet wi eggal na sart bi ci 14 sebtambar 1791 g, loolu di bi fipp gi amee ba toll ci ñaari at, bi mu ko defee nag, ndajem xeet wi daal di tas boppam, daal di fiy taxawal ab jataayub yoonal bu sukkandiku ci li nekk ci sartu Fraans bu bees bii nga xam ne lu feddali woon àqi ak yelleefi nitug Fraans la woon, ak war gu mu war a gore te am ag yamoo ci wàllug mboolaay. Moom sart bi tam tàqale woon na diggante nguurug yoonal gi ak gu doxal gi ak gu àtte gi.
Mu jël nguurug yoonal  walla dooley yoonal ji, teg ko ci loxol ab jataay bu askanu Fraans wi di tànn, mu jël dooley àtte ji , teg ko ci loxol ay àttekat yoy danu leen di tànn, mu jël nag dooley wéyal ji walla ju doxal ji , teg ko ci loxol buurub Fraans bi aki jëwrinam. Ndaxte nguur  saxoon na ca Fraans ba ca 21 sebtambar 1792 g.

Ci atum 1792g, beneen woote amoon na, bu nu doon tànnewaat ab jataayub yoonal. Ci noonu jataayub xeet daal di sosu, boo xam ne li mu njëkk a def mooy jibal nosteg pénc (systeme republicain) ca Fraans, ca 21 satumbar 1792 g.
Ñu feetele ko doxal reew mi, ak teg sart bu bees buy sukkandiku ci nosteg republig gu bees gi, ñu wax ko tam mu seet li nu war a def buur bii di Luwis 16, te teg yoon yuy aar fipp gi, aar it Fraans ci musiba yi ko man a dikkal, juge ci reew yii di : Otris, ak Brusiyaa, ak Britaani, ak sax yeneen reewi Tugal yoo xam ne danoo noonu woon fipp gi.
Feetale nanu ko ba tay taxawal goornamaa bu Fraans bu dëgër, boo xam ne da fiy jeem a jële fitnay biir reew mi. 
Ñi jiite woon goornamaa bu jataayub xeet boobu nag , ñi ngi sosoo woon ci “Girondins”yi, ñooy ñi nga xam ne danoo gëmoon ag yewenal, te daan woote jëme ci coppat goo xam ne danu koy amal cig nànk-nànk, ak ci “Jacopins” yi xam ne, ñoo gënoon a xaabaabal Girondins yi, danoo gëmoon ne fii Fraans toll tay ak nekkiinam wii, danu koo war a soppi bu wér ak doonte loolu dafa laaj doole. Ak ñu diggdoomu ñoo xam ne taxul woon leen a xaabaabal, ñoom ñooy ña ëppoon ca jataayub xeet wa, waaye amunu woon gis-gis bu dëgër, ndax leeg-leeg ñu ànd ak Jacopins yi, leeg-leeg Girondins yi.

Ligeeyub goornamaa bu jataayub xeet wi:

Goornamaa bu jataayub xeet wi, daal di nay àtte buur bii di Luwis 16 àtteb ray, ci 21 samwiye 1793 g, loolu nag tax na ba lu bari ci reewi Tugal yi def ag jàppaloo kontar Fraans, mu ci mel ne Angalteer, ak Brusiyaa, Otris, Espaañ ak Holand. Ginaaw bi nag goornamaa bu jataayu xeet wi daal di taxawal kureelub kaaraange, feetale ko ligeeyub aar Fraans ci ñiy noonu fipp gi ci biir reew mi, ñu feetale ko ba tay moom kureel bi, wàluug taxawal am mbooloom xare mu Fraans mu dëgër, ngir aar Fraans, ak fipp gi, ak li mu fi jot a indi ci ndam, ak xeewal, moom fipp gi. Goornamaa bi nag ci njiitul Girondins yi gañe na xarekati Brusiya yi ca xareb Valmy ba, lijjanti na it ba xiir waa Beljig ci ñu fipp ci kaw Imbraatoor boobii di Francis mi nekkoon imbraatooru nguurug Rom gu Sell gi. Ñu daal di nangu alali paap gi ci goxub Afinion, ngir noonu gi mu noonu woon fipp gi (moom paab gi).

Ñu fàttali leen ne Jacopins yu xaabaabal yooyu, ñoo saytu woon kureelub kaaraange gu matale gi, ñoom songoon nanu ci anam gu tar, ci njiitul Robespierre kepp koo xam ne yaakaaroon nanu ne da nga àndul ci fipp gi aki gaay fipp gi. Jacopins yi nag bari na lu ñu daa mbugal lim bu bari ci waa Fraans yi, ci tuumaal leen ne danoo def ay wor yu mag.
Ñoom ci seen jëmmi bopp nag ak doonte jàmaarloo woon nanook jafe-jafe yi leen dikkaloon juge ci reewi Tugal yi leen wër, te aju woon ci kontar fipp gi, ak doonte jàmmaarloo woon nanook ñoom ci doole ak fulla, te farataal duggug coldaar gu sañ-bañ, ngir aar reew mi, tas te giimal fèttéerlu yi doon am ci yennat ci gox yi nekk ci biir reew mi, duggal seeni xarekat ci Beljig ak Holand, ànd ak loolu lepp teewul waa Fraans bëggoon ñu soppi seenuw doxiin ci politig ba mu gën a woyof, gën a teey, gën dal, te gën a maandu.

Ci 29 sulye 1794g, la ceri jataayub xeet wi, tuumaal Robespierre, ne daa wor, yobbu ko ca mbuggalukaay ba. Jataay bi defaraat na beneen sart, boo xam ne moo waral ab goornamaab Fraans bu bees, ñu xame ko ci turu goornamaab doxaliin bi.

Goornamaab doxaliin bi:

Goornamaab doxaliin bi sampu na atum 1895g, moom nag li mu doon wund, mooy ab diggante bu tuxu, nekk ci diggante jamonay tiital ak taral, ak jamonoy nguurug imbraatoor gu nu joyal, gu tar, goo xam ne Napoliyon Bonaparte moo ko ame woon ci ginaaw bi, ci bi mu fi nekkee. Goornamaa boobu nag li gënoon na fés ciy ligeeyam ci ñaari wàll yii lanu jëmoon:

(1)	Def politig bu maandu ci biir doxaliinu reew mi, te du tax mu doyadi mbaa mu ñàkk fulla ci kanamu ay noonam
(2)	Yonni Napoliyon ngir mu song Itaali, ngir yare ci Otris, ak yonneeti ko ci penku bi.

Nanu fàttaliku ne goornamaab doxaliin bi, mi ngi sosoo woon ci juroomi cer yoo xam ne dëppoowunu woon. Ciy jamonoom it la jëmmi Napoliyon feeñ, moom mi nga xam ne jariñu woon na bu baax ci doyadig gooramaa bii, ak ñàkk dooleem, ngir saxal fi boppam ci wàllug politig.
Ciy jamonoom it lu sakkan ciy làngi politig sosu woon nanu, ni nu doon jëfandikoo alal ji gën a ñaaw, gën a bon. Ci fukki fan ci nowambar 1799g, la Napoliyon ak làngam gi, defoon yong googu nuy wax yongug Brumaire, daaneel goornamaab doxaliin bu neewoon doole boobu, loolu moo fi indi goornamaab kilifa bi, mooy bi ame ci ñatti kilifa yi nga xam ne ñoo doon jiite Fraaans te Napoliyon jiite woon leen, nga xam ne daanaka mbooleem sañ-sañ yi ci loxoom lanu nekkoon.

Napoliyon Bonaparte:

Napoelon Bonaparte, mi ngi judd atum 1769g, ca Ajaksio, ca dunub “Corsica” ca Itaali, dun boobu nga xam ne Fraans da koo mujjoon jënde ci Genova.
Napoleon nekkoon na, ba muy doon gone, ku bëggoon fànnug xare, mi ngi genne ca bànqaasu xare  ba nekkoon Paris, daal di dem nag doon ab ofise, bokk ca kureelub kano ya ca xarekati Fraans ya.
Moom nag ku soppoon xam-xamu yoon la , taariix, ak xam-xami xare yi ak yu doxaliin yi. Ku sawaroon la ci dali fipp gi , te fonkoon leen. Moom nag ab bidiwam a ngi féqe ci ginaaw bi mu songee Itaali. 
Àtteg Napoleon walla yor gi mu yoroon Fraans, dafa seddaliku woon ci ñaari xaaj, bu njëkk bi: mooy kilifag Fraans gu njëkk gi, la ko dale ca 1799g, ba 1804g. Bu ñaareel bi: moom mooy imbraatoor bi, la ko dale ca 1804g, ba 1815g.

Song gi Napoleon defoon Itaali:

Goornamaab doxaliin bi, dafa feetale woon Napoleon jiiteg xeex boobu mu doon xeex Otris, jaare ko ca moomeelam yooyee nga xam ne Itaali benn la ci woon, atum 1796g, Ci noonu moom Napoleon mu daal di xeex ak nguurug Sardeñ, xeex bu tar boo xam ne jañ na ko ci mu xaatim ag wéer ngànnaay gu nuy wax gu Cherasco.
Napoleon defati ab xare ak dooley paab gi, moñoxe ko ca Ancona, mu dumaati soldaari Otris yi ca bëj-gànnaaru Itaali, dàqeeti leen fa, xaatim fa ak ñoom juboo ga tuddoon Campo Formio, atum 1797g. Ci nii daal la Napoleon doyodile woon Otris, neewal ko doole, daal di àgg ci njobbaxtalu siw ci wàllu doxal xare.
Napoleon, àntu gi xeexam yooyu àntu woon ci Itaali, tasoon lënkaloo gi waa Tugal defoon, kontar Fraans, mu mujj Britani rekk moo dese woon xeex beek Fraans.

Song gi Napoleon songoon penku bi:

Politigkati Fraans yi naaloon nanu – Taliraan mi nekkoon jëwrini bitim reew mi jiite woon leen – naaloon nanu ay naal yu aju woon ci ngàdd Britani, jaare ko ca sancoom ya, te bañ koo fekk ci biir këram, rawati na moom Britani dafa amoon mbooloom gaal mu mag ca geejug Mans.
Politigkati Fraans yi, li nu bëggoon ci loolu mooy sos ab sancu bu Fraans ci geej gu diggu gi, ak man a àgg ca geej gu xonq ga, ak dog yoonu yaxantu wi daa àggale Britani ca sancoom ya nekk penku.

Goornamaab doxaliin bi, lii mi ngi ko denkoon Napoleon, ci noonu mu jug mooki gaayam, geeju ci atum 1798g, tukkee ca waaxub Toulon, mbooloom xare mi àndoon ak moom àggoon na ci ñeenti teemeeri gaal, yu sëfoon ñaar fukki junneek juroom ñatti soldaar, bokkoon na ci tam teemeer ak juroom ñaar fukk ak juroomi boroom xam-xam yu waa Fraans. Ñu àgg waaxub Aleksandriya, ca Isipt, nangu ko. Waaye mbooloom gaalum Britani mi bettoon na mu Fraans mi, ca ndoxum golfub Abii Xiir, moñoxe ko, ci noonu la Britani xañe Fraans cangug geej gi Fraans yàgg a gent. Fraans sax nag – ni mu ko baaxoo woon – nguurug xare la gu mag gu gën a am mbooloom xare mu jeeri ci mu geej, mu mel ne mu Britani mi. 

Man nanu ne xare bii Napolen daan def ci penku bi, xare jooñ la woon, ndax kat ag sof rekk la ca xareb jooñ ba amoon cag njëkk, loolu nag gën na a leere ca xare ya mu doon def ca Afrig gu bëj-gànnaar ga.

Misra (Isipt) ca jamono jooja, dafa nekkoon reew mu nekkoon ci waawug àtteg Usmaan gi , bu ko defee, buuri Mamaalik yi jiite ko, mu doon jànkoote ak ag doyadi gu biir, ak xeex gu sax ci biirum reew ngir nangu nguur gi, te tam ngànnaay yi mu ame woon yu doyadi la woon bu nu leen nattee ci yi Napoleon ame woon, aki jumtukaayam.
Lii moo taxoon Napoleon sonnutoon ci teg loxo Isipt, ak doonte Mamaalig yi ñoom jàmmaarloo woon nanook moom, xeex ak moom xex bu tàng ngir aar seen reew. Waa Isipt yi bégunu benn yoon ci àtteg Napoleon gi, li am kay mooy danoo fippoon ci kawan, mooy la amoon, ca Xayra (Keer), ñu koy wax “fippug Xayra gi” .
Napoleon jawali na reewi Shaam mook mbooloom xareem mi, ginaaw bi mu nangoo Isipt, mu daal di teg loxo Hariis, Gaza, ak Yafa, daal di ray dooley kaaraange ja fa nekkoon daan ko aar, te tolloon ci ñeenti junniy soldaar. Juge fa, diriku jëm Hakka, gaw ko diir bu yàgg, waaye Hakka moom, toogul rekk faste ay loxoom di seetaan, dafa jànkoonte, jaamaarloo cig njàmbaar, ci njiitul kilifaam gii di woon Ahmad Basha, nga xam ne mbooloom gaalum xare mu Britani mi ñoo ko doon dimble tukkee ci geej gi, waa Usmaan yi  di ko jàpple ci jeeri ji.
Bi gaw gi yàggee, te Napoleon ñàkke ca lu bari, te amewu ca lenn njariñ, xarekatam yi tàmblee tawat, rawati na tawat ji nuy wax “siburu” di yaram wuy tàng, bi loolu amee Napoleon, xam ne fii muus du fi naane ñeex, mu deltu ginaaw, dellooti Isipt, te jëlewu fa lenn ndam.

Napoleon bàyyikoo na Isipt ci sekkare, dellu Paris, askan wa tertu ko fa cig yaatal ak mbegte. Xew-xew yi toppante ci Fraans, waaye ci anam gu baaxul ci goornamaab doxaliin bi. Looloo fi jële boobule goornamaa. Bi nuy wax bu ñatti kilifa yi taxaw, atum 1799g, Napoleon nekk ca Kilifa Gu Njëkk ga.

Ay ngérte , yu am solo juddoo nanu ca xareb Napoleon bu penku ba, ñu indil leen ci yii rekk:
(1)	Xareb Fraans boobu ci penku bi, wone woon na solo si Isipt am ak fi mu feete, ci wàllug jokkoo ak tuxu, ñeel imbraatoorug Britani gi  ci penku bi.
(2)	Xare boobu Fraans da ci doon seete rekk, ngir xam nu muy def ba man a sanc walla kolonise reewi Afrig gu bëj-gànnaar gi.
(3)	Boroom xam-xami xare boobu, bi nuy ñëw, indaale woon nanu ay gëstuy xam-xam yu aju woon ci nàndal , ak jeexiit , indi woon nanu fi it benn naal bu aju woon ci gas aw yoonu ndox ci diggante Suwes ak geej gu diggu gi, di kanaalu Suwes bi, te it indaale woon nanu fi ab moolukaayu teere ci araab nu koy wax moolukaayu Bolaax bi.
(4)	Xare bi wutoon ay yoon yu man a indi ag jokkoo ci diggante Fraans ak Isipt, rawati na ci wàlli xam-xam ak njàngale añs.

Napoleon ak reewi Tugal yi:

Napoleon de taxawaloon na màmm gi Otris màmmoon, ci yaatal nguuram, ndaxte gañe woon na ko ca xare ba nuy wax Marenngo atum 1800g, jañoon ko ci mu xaatim ag juboo gu yees atum 1801g, mooy juboo gi saxaloon poñ ya nekkoon ca kollareg Campo Formio ga (1787). Napoleon xatim na ak Britani juboog Amiens, atum 1802g, looloo waraloon dooley Fraans ji genn Isipt, bu ko defee Angalteer moom itam noppi ci li dal Otris, bañ cee wax dara.
Napoleon saxoon na di ki nga xam ne moo ame woon sañ-sañu fal niti Egliis bi ci Fraans. Paab bi tam – bi Napoleon di sampu niki Imbraatoor, atum 1804g - mooy ki doon def li ci aju woon ci  xeeti ñaanal ak xumbal.
Napoleon bi mu jotee ci imbraatoor gi, daa daal di nosaat doxaliin wi ci campeefi nguur gi, mu taxawal fi benn jumtukaay buy yëngu ci luy amal bëgg-bëggam bii, mu jël lu sakkan ci mbokkam yi ak xaritam yi, jox leen pal yu kawe yi. Mbooleem dooley nguur ji ak sañ-sañ yi mu tëyyeel leen boppam, teg boppam it ci kaw mbooleem làngi politig yi, doyadil làngi politig yi ak barlamaan bi, nos galag yi.

Napoleon de tàbbi woon na ciy xare ak reewi Tugal yi. Britani gañe woon ko nag ci wàllug geej gi, ca xare ba nuy wax (Attaraf Al-aqar), mu song Brusiya, gañe ko ca xareb Yena ba, atum 1807g. Mu daal di def waxtaan ak Aleksandar mi nekkoon sesaarub Riisi, def ak moom genn dëppoo, nu koy wax dëppoo gu Talist atum 1807g, mooy liy wone njobaxtal la Napoleon àggoon ci kàttan. Mu defoon ag gaw gu goxub Tugal bepp, jëme ko Britani , daal di woon ga  reewi Tugal yi ci ñu topp ko ci loolu. Loolu indi woon na fi benn jafe-jafe bu koom-koom bu tar ci reewi Tugal yu bari. Loolu it waraloon na reew yii bañ ko, kontar ko. Mu xare woon ak Riisi gu sesaar gi, ndaxte daa gisoon ne moom kat wormaalul gaw googu mu digale woon. Ci noonu mu jëmale fa menn mbooloom xare mu mag, atum 1812g, ñu dox ba àgg ca peey ba, di Butrusburg, waaye mujj nanu manatunoo ñàkk a dëpp, ngir sedd bu tar ba leen fa gaw, ba jamonoy sedd ja duggee. Ak ba tay ngir jafe ga fa ag jokkoo jafee, guy man a yombal nuy jot ci li am mbooloom xare di soxla ngir man a def ligeeyam, muy jotug jumtukaay yeek dund yeek lu ni mel. Bi nuy dellu nag la waa Rusi yi sottiku ci seen kaw, ñoom xarekati Napoleon yi, ray ci lu bar. Bu ko defee Napoleon ñàkk soldaaram yu bari, te amul la mu doon bëgg.
Bu ko defee waaTugal yi ( Otris, Brusia, Rusi ak Britani) boole seen doole, jàmmaarlook Napoleon, daal di koy gañe ca xareb Libisg, nu koy wax ( xareb xeet yi ), di woon ci Oktoobar atum 1813g. Ca noona nu sànni Napoleon ca dun ba tudd Elba, waaye mu lijjanti ba rëcce fa ci sekkare, ginaaw bi mu fa defee teemeeri bis, dem nag Paris, dajale fa xarekat yu bari ci waa Fraans yi, ngir xeexi reewi Tugal yi ko doon sot. Ñu gañeeti ko, ca xareb Watrlo ba, atum 1815g, sànneeti ko ca dunub Santa Hilana, mu des fa nag ba kero bi mu faatoo, atum 1821g.

Bu ko defee, reewi Tugal yi def seen ndaje ma nuy wax ndajem Vienne atum 1815g, ngir seddalewaat kartu Tugal wu politig wi. Daal di fiy saxalaat bu baax kenoy nguur, te suuxat ko fi. Ak sàmmoonteek yamoo gu reew yi  ak sos reew yu am doole yu peek Fraans wër ko.

Ligeeyi ndajem Vienne:

Ligeeyi ndajem Vienne nii la tënkoo woon:

(1)	Way daje yi delloowaat nanu buuri Tugal ya ca seen reew ya nu juge woon, teg ko ci “àqi yoon”, ci noonu nu delloosi njabootug Borbon gi, ngir ñu yilif Fraans ak Espaañ.
(2)	Britani jëloon na sancu yi Fraans moomoon, muy Malta ak Kaab, ak Silaan, ak Morisos.
(3)	Rusi jël moom Varsaw, Otris jël tefesug Dalmas, ak Milano gu Itaali gi, mujj nag ëpp doole nguur yu ndaw yu Itaali yi. Brusiya moom am ay moomeel yu mag ci Almaañ, ak ag wàll ci Poloñ. Ñu jël Beljig – cig sañ-bañ – boole ko ci Holand. Jëlati Norwej – cig sañ-bañ – boole ko ci Suwed . Jëf yii yepp nag dëppoowunu woon ak xeetu, walla fonk sa xeet, di nationalisme gi doon am ca Tugal. Lii nag firee nanu ko ne li ko waral mooy Britani daal, ak Rusi ak Otris ak Brusiya, danoo defoon seen bopp ay reew yu ñoo am ag kilifteef ci reew yu Tugal yu ndaw yi.

Li juddoo ci fippug Fraans gi:

(1)	Fipp gi moo fi indi tay, dalub Fonk sa bopp  bii nga xam ne, mujj na foo dem ci Tugal fekk ko fa, ci diirub xarnub fukk ak juroom ñeenteel bepp g, moo waral reewum Itaali bennoo, te moo jur it bennoo gu Almaañ gi.
(2)	Moo fi jële sañ-sañ ak ràññale ci biiri kureeli nit, naan kii moo kawe kee, wii xeet a gën wee, te man nanu ne mooy jaasi ji mujj rendi nostey laman ya nekkoon Tugal.
(3)	Fipp gi ci Fraans mooy gi njëkk ci fipp yi, ci taarixu Tugal bu bees bi, loolu nag li ko waral mooy coppat yi mu indi ciy gisiin aki deggiin, aki xalaat, ci wàll yu bari ci dundug politig gi, gu mboolaay gi, gu xalaat gi, gu koom-koom gi ci Tugal, ak fu ko moy. Ay term yu politig feeñ, yu mboolaay, yu diplomasi yu bees.
(4)	Moo fi jële gisiin wu “àqi Yalla ji” mooy gisiin wi naan buur yi seen àq ak sañ-sañ, ca ju Yalla ja lanu ko jële, mooy gisiin wi matale woon noste yi amoon ci Tugal gepp, la ko dale ca ba fa jamonoy laman tàmblee.
(5)	Xalaatub fipp gi law na ba àgg ci Tugal gepp, ak yeneen reew yu dul Tugal, yu adduna bi.

Buntub ñeeteel bi

Yëngu-yëngu yi aju ci “xeetu” walla fonk sa xeet (nationalisme) ci Tugal, ci xarnub fukk ak juroom ñeent g.

Bennal gu Itaali

Bennoo gu Almaañ

Doggantal gu njëkk gi 

Bennal gi nu defoon Itaali

Ni Itaali meloon njëkk xare yu Napoleon yi:

Itaali laata a Napoleon di ko teg loxo, di ko nangu, nekkutoon reew mu nu bennal , nekkutoon it di mu am ag temb, moom kay daa seddaliku woon, doon fukki xaaj ak ñaar, yu doon topp ak a nekk ci ron kilifteefug ay nostey politig yu wuute: nosteg nguur ca Savoia, Piemonte, Napoli, ak nosteg pénc  ca Venezia ak Geneva, ak ag àtte gu paab ca Rom, ak gu Doox  ca Toskaana ak Parma, ak xaaj yoo xam ne danoo nekkoon ci waawug imbraatoor gu Otris gi, ñooy Milano ak Lombardia.

Piemonte nag moo nekkoon nekkteg politig gi gënoon a dëgër, te ëppoon doole ci nekkte  yooyu. Ña ëppoon ca njiit ya yilifoon nekkte yooyu, ay diktaatoor lanu woon, rawati na ñi ci waa Otris jiite woon, cig jonjoo mbaa lu ko moy  .

Jeexiit ya Napoleon bàyyiwoon ca Itaali:

Napoleon, bi mu nangoo Itaali, dafa lijjanti ba boole xaajam yu politig yu bari te wuute yooyu ci ñatti nguur rekk, ñooy: Nguurug Alp gu bëj-gànnaar gi, walla Itaali, ak Nguurug Savoia, ak Nguurug Napoli. 
Mu wutaloon reew mi mepp, wenn yoon , daal di dindi galag ak tënk yu koom-koom yi amoon ci wàllug endustri ak yaxantu, ak mbay. Mu ubbi leekol yi ngir jàngal doomi reew mi, mu may waa Itaali yi ñu man di jot ci pal yi, te kat bu njëkk waa Otris rekk a ci manoon a jot. Looloo tax ñu man a wax ne Napoleon de mooy ki ji njiyum bennoo mu xeet ci suufus Itaali, mooy ki leen def ñuy xeeñtook a gént am reew mu Itaali mu man a am, mu nu bennal.

Itaali ginaaw ndajem Vienne:

Ndajem Vienne mi – ci xalaati njiitu jawrin ju Otris jii di Metternich-Winneburg – seddale woon na Itaali, def ko juroom-ñaari xaaj, ñooy: Piemonte, Napoli, Parma, Modena, Toscana, Lombardia, ak Venezia, ñoom ñaar nag, mujj nanu leen boole def leen benn, teg leen ci ron kilifteefug Otris.
Ginaaw nag Metternich fexe woon na ba yay njiiti ndaje mi, gëmloo leen “dalu desal fi lu yàgg la ca yàggam ga”  maanaam lu nekk, nanu ko delloo na mu meloon, loolu nag moo indi ndaje mi delloosi njiiti nguur yu ndaw yu Itaali yu njëkk ya, ñu delloosi leen ci seeni pal, tegaat leen seen barab.
Metternich ak bëtam yi  mu tasoon ci gox yepp, jeemoon nanoo fuglu yeglekaay yi, daan naj it gepp cawarte gu politig. Ci noonu ñu daa tëj gor ñi ci kaso yi, daan xañ way dëkk yi pali siwil yi ak yu xare  yi nga xam ne bi Napoleon ñëwee jox na leen ko,mu daan leen weccee ak ay waa Otris (moom metternich), te daan leen teg ay galag yu diis te sonnle.

Yewwueg xeetu (nationalisme) ni mu xëye rekk am te màgg ca Itaali: 

Politigu noteel gi Metternich yore woon, ak li muy tar lepp, taxutoon mu man a rekki yëg-yëg bi waa Itaali yi ame woon, ak xam ngi nu xamoon am solo gi bennal seen reew mi, te booloo ci wàllug politig amoon solo, loolu nag mi ngi am, ginaaw bi nu ci ñamee’s lëf ci jamonoy Napoleon.
Bi nga xamee ne politig bu ñaaw boobu fa amoon, mayu leen woon ñuy def  seeni cawarte ak jëfi politig, ci lu bér, te nëbboodiku, bi loolu amee lanu wéeru ci di def seeni yënguy politig cig làqu ak fésadi.
Bu ko defee, ay booloo yu politig yu sekkare tàmblee sosu ci dëkki Itaali yu mag yi, li leen taxoon a jug di bennal Itaali, bokk na ci yooyu: booloo gu Karbonari (ñoñ këriñ), ak booloo gu Itaali gu waxambaanee gi.

Booloo gu Karbonari, moom mi ngi sosoo ca Napoli, daan def ay jataayam - ngir làqatu - ci barabi ligeeykati këriñ yi, walla lakkati mat yi, mu mujj nag tas ci mbooleem Itaali. Mbooleem kureeli askanu Itaali wi nag bokkoon nanu ci, baykat yi, ligeeykat yi, boroom mecce yi, yaxantukat yi, boroom xel yi, añs.
Li leen manke woon nag, mooy danoo nosuwutoon bu baax, te ni ñu daan naale ak a rëdde seeni mbir tam dafa dese woon a tegu ci yoon, looloo taxoon li nu bëggoon daawul àntu, te seeni noon daa leen gaaw a not, te daa àntoodil seeni fipp.
Waaye nag booloo gii, di gu Karbonari gi, jot na fee taal yëg-yëgu xeetu ci Itaali, te lijjanti ba mu sax fi di tàkk, ak doonte daje na’ak coona yu bari, te nu teg ko lu sakkan ciy mbugal.

Bu dee booloo gi tuddoon “Itaali gu Waxambaanee gi”, moom Jozeph Mazzini (1805 – 1872 g) moo ko sosoon, ginaaw bi mu nekkee ab cer ci booloo gu Karbonari gi. Mazzini mii, moom waay Itaali la woon ju xéroon ci reewam ak xeetam, nekkoon it ab xeltukat bu bokkoon ci ñoñ nite ñi , bu gëmoon ne xeetu nit ñepp benn lanu, te bëggoon lool goreg askan yi , moom nag jot na’a àgg ci xëcc cig wàllam boroom xel yi ci Itaali, te fàggu ñeewanteg nitug neen ku Itaali ki, akug cofeelam. 

Bokkoon na ci jubluwaay yi gënoon a tax booloo gii am, goreel Itaali ci àtteg Otris, ak duma àtte gu paab gi nga xam ne Otris a ko daa dimbleek a dëgëral, ak fexee bennal reewum Itaali mi, ci ron ag noste gu republig.

Yëngu-yëngu yii, mujjoon na naat, te dox, bijjaloon it boppam lu sakkan ci waxambaane yi ak xalaatkat yi, àggoon nanu ci lu toll ne juroom fukki junniy waxambaane, yu weesu ay ñeen-fukki at yooyu. Mazzini dimblante na’ak Garibaldi, moom Garibaldi, ab kojug xare  la woon, bu itaali, bu gëmoon bennug Itaali, te gëmoon ne danoo war a gorewu ci àtte gu Otris gii bóof ci suufus Itaali si. Ci noonu lanu jot a taxawal ñoom ñaar, ag àtte gu pénc  ca Rom, ca moomeeli paab ga, ak ca Venezia, atum 1848g. Waaye Otris moom, ca dooleem ju bari ja, faagaagal na yëngu-yëngu googu, daal di dàq Mazzini mu daw, làqu ca Anggalteer.
Ag woote nag feeñ na fa, jëm ci ñu def nattukaay yi benn, xaalis bi, ak peesekaay yi , ci mbooleem diiwaani Itaali yi aki nguur-nguuraanam, rawati na bi endustreem tàmblee màgg, yaxantoom gën a jëm kanam. 
Boroom ligeey yi nag ak boroom boppi alal yi , gisoon nanu am njariñ gi gore ci koom-koom amoon njariñ, ñu tàmbli woon a sàkku ñu sosal leen ay yooni weñ , yuy taqale diggante bëj-gànnaaru Itaali ak bëj-saalumam, te nu uppi mbooleem ja yu Itaali yi, ci kanamu yaxantu gu Itaali gi, te bañ cee indi yenn jafe-jafe walla ay mbugal yu doxaliin , walla ay galag yu man a tee bennoo gu yaxantu gi am ci Itaali.

Ma fàttali leen ne barab yu bari de ci bëj-saalumu Itaali, yu deltu woon ginaaw lanu woon ci wàllug endustri, koom-koom, mboolaay ak politig. Looloo taxoon xalaat yi jëmoon ci bennoo, mi ngi gënoon a dëgëre ci fi nuy wax Itaali ( di nguuru Alp gu bëj-gànnaar gi) ak ci digg bi. Foofa daal la wooteg bennal gi gënoon a tare ci yeneen wàll yu bëj-saalum yi. Ndax kat wàlli bëj saalum yi dañoo jëmutoon kanam dara ci wàllug endustri, yaxantu, politig ak mboolaay. Lii a waraloon woote gi, jëme ci bennoo gu koom-koom, yamoon rekk ci digg Itaali ak ci bëj-gànnaar gi. Ñi ëppoon it ci xalaatkat yi ak boroom xam-xam yu Itaali yi, ñi ngi dëkke woon digg bi, ak ci bëj-gànnaar gi.

Ak li boole Itaali, def ko menn reew doon nekk càkkuteful ñepp lepp, teewul yenn ci nguur-nguuraan yi, ak Doox yi , kontaroon ko, ndaxte ñoom dañoo ragaloon ne loolu de, moo xam leegi la walla ci kanam, bu amee, di na fi indi ag bennoo gu politig, te loolu bëggunu ko woon, ndax kat ñoom seeni njariñi nguur yooyu moo leen gënaloon njariñul Itaali li.
Ci noonu, nguurug Paap gi kontar ko, naka noonu gu Otris gi nga xam ne amoon na kilifteef gu yaatu, ak sañ-sañ bu mag ci Itaali. Ndax moom daa gisoon ne bu Itaali bennoo ci wàllug koom, boole ay nguur-nguuraanam, aki Dooxam, loolu du wund lu dul ne moom kat (Otris) waxtuw gennam Itaaliee ngi bëgg a jot, ci lu dog. Te loolu du ko nangu mukk.

Nguurug Piemonte ak Bennalug Itaali:

Ci bëj-gànnaaru Itaali ag nguur a ngi fi woon, ñu koy wax nguurug Piemonte walla Sardeñaa, ka nekkoon ca gàngunaay ga, di woon Victor Emmanuel. Moom Piemonte nag, nguur la woon gu ame woon ci ñeenti xaaj yu taqaloowul, (ñoom xaaj yi), ñooy: Piemonte, mi nekk ci ron doji Alp yi, nekkoon barab bu taxu ko woon a woomle, ak Savoia, mi ngi nekkoon ci kaw doji Alp yi, tiim wàllug Fraans gi dend ak Itaali, moom nag ruq la bu gën a yor ay màndarga yu Fraans ci yu Itaali, moom itam taxu ko woon a jëm kanam mbaa mu woomle, ak Sardeñaa, moom dun la, bu nekk ci geej gu diggu gi, xaw a sori Piemonte. Ak Genova, moom nag, nguurug Piemonte jot na ci, ci ginaaw xarey Napoleon yi ci Tugal.
Di nanu gis fii ne Piemonte moom yorul woon nguur gu àttanoon coonay bennal Itaali, waaye nag yoroon na yenn yu rëy ci yiy taxawal reew mu mag, yu ko mayoon mu man a yanu yan bu diis bii, ñu tudd ci yi ci ëpp solo:

(1)	Ab buuram daa gëmoon ag àtte gu tegu ci sartu reew, te daa gëmoon it bennoo gu Itaali.
(2)	Njiitul jawrinam lii di Cavor, - mi ngi doonoon njiitul jawrin atum 1851g – daa gëmoon moom itam te sopp sartu reew ba Angalteer defoon, te bëggoon lool Itaali doon benn, te nekk ci ron ndëppul  Piemonte. 
(3)	Piemonte amoon na dooley xare joo xam ne, li ko daa wone mooy soldaaram sii nga xam ne jot nanoo xare ba am ci xam-xam.
(4)	Piemmonte moo nekkoon làqatukaay bi politigkat yi nu daa sonnale ci nguuri Itaali yeneen yi daan làqatoo.
(5)	Màgg gi koom-koom doon màgg ci Piemonte, moo gënoon a gaaw, gi mu doon def ci feneen ful Milano.
(6)	Nguurug Piemonte, gu sori woon loxol Otris la, nga xam ne daawul man a dugg ci mbiri biiram.

Cavour ak bennalug Itaali:

Cavour mii (1810 – 1861g), nekkoon na di ku gëm bennoo gu Itaali, waaye nag ci ron ag àtte gu nguur gu sartu reew , goo xam ne buurub Piemonte bee koy jiite, moom kon ci loolu la wuute woon ak Mazzini mi nga xam ne da doon woote ag bennoo gu Itaali ci ron ag àtte gu republig. Moom de daa gëmoon ag yewenal gu politig, gu koom-koom ak gu doxaliin , ngir Itaali man a doon benn. Mu gisoon ne nguurug Piemonte am na kàttanug dàq Otris mu genn Itaali, ak naj nguurug Paab gi daa lënkaloo ak Otris, bu lënkaloo woon (moom  Piemonte) ak jeneen doole ju reew, ju mel ne Fraans mbaa Britani.

Cavour mi ngi yoroon njiitug jawrin gi ci atum 1851g, bi mu ko defee nag, mu tàmblee waajal am reewam ngir mu man a jiite ligeey biy bennal Itaali.
Ci noonu mu sotti yitteem ci xarekatam yi, waajal leen ba nu man a jàmmaarlook mbooloom xarem Otris mi, te man leen a genne Itaali, mu jug ci suqali koom-koom bi, defar ay yooni weñ , yu lënkale mbooleem dëkki Piemonte yi, daal di jamonool mbay mi ak endustri bi, defar ay yoon, neenal galag yeek mbir yi man a tënk yaxantu ak endustri, tege ay galag yu duwaan yu mag ngir aar endustri bu lokaal bi (bu biir reew mi), yewenal nosteg galag yi, daal di sos lonkoo yu askan yi  ak bànk yi.

Bu dee lu aju ci doxaliin , ak yewenal yu biir reew mi, moom da fee daal di woon buddee doxaliin wu yàgg wa fa nekkoon, daal di jël ay matuwaay yoo xam ne tax nanu ba yoon ci reewum Itaali gën a jamonoo, jële fi lu bari ci ay jàngu, maanaam ay egliis, wàññi dooley politig ju paab gi, tàqale àtte  geek Eglis bi.

Kafor mii nag xamoon na ni reewam mi tuutee woon, bu nu ko tollalee ak Otris walla Britani, mbaa Fraans, am Rusi, ak Brusiya, waaye loolu lepp teewutoon mu gëmoon ne bennug Itaali daal, mbirum aw xeet la woon, manul  woon a ñàkk, te itam mbirum adduna bepp la, laaj na reew yi sonn ci, te jeem koo faj ci nu mu gën a gaawe, mu dogu woon ci sóobu ci geewub politig bu adduna bi, ngir yékkati kàddug Piemonte ci adduna bi ba ñepp degg ko, ci ndajey Tugal yi.
Ci noonu mu digal parlamaa bu Piemonte mu nangu ñu yonnee ab kureelub xare bu Piemonte ngir mu bokki ca xareb Xarm ba , àndoon ca ak Britani ak Fraans, ngir sàkkoo ci xaritoo ak Imbraatoor bu Fraans bii di Napoleon mu ñatteel mi, (Napoleon III), te ame ca ñeewantug Britani akug jàppaleem ci li mu bëgg.

Kureelu xare bu Piemonte boobu, ak doonte bariwu ci ñu ci dee ca xareb Xarm ba, ndax ñu bari ci ñi ci dee ci mbasum koleraa lanu deewe,  teewul Kafour moom lijjanti na ba nu yëg Piemonte  ci kanamu ndawi Tugal yi, ca ndajem juboole ma nu doon def bi xareb Xarm bi jeexee.
Kafour sàkku na fa ca Fraans mu dimbli ko ci Otris, ndaxte nguurug Piemonte moom rekk manul a dàq imbraatoorug Otris gu dëgër gii. Kavour ci njëlbeen gi, li ko gënaloon mooy Britani jàpple ko, kontar Otris, waaye Britani moom, bëggutoon a xeex ak Otris, xeex bu ko amalul njariñ.
Bu dee Fraans nag, nga xam ne pencam mi , Napoleon III moo ko jiite woon, moom Napoleon III mi nga xam ne daa jàppe woon Itaali am ñaareelu reewam, ndax moom doom la woon ca Napoleon I - ginaaw doomi mbokkam la woon - te Napolen I mi ngi cosaanoo Corsica. Moom Napoleon III, ku soppoon waa Itaali la, te xéroon ci seeni àq aki yelleef ci gore te doon benn, moom de bokkoon na ci ñi gënoon a siw ci woote ag xeetu  ci Tugal. Politigu bitim reewam it mi ngi ko tegoon ci bañ Otris mi dendoon ak moom. Te ginaaw Piemonte it reew mu nekk ci wetu Fraans la, loolu taxoon na mu bëgg mu nekk reew moo xam ne yoonu Otris du ca nekk. 

Cavour lënkaloo na ak Napoleon III, ñu def dëppoo  ga nuy wax (Plombiere) ci 21 sulye atum 1858g, dëppoo googu, la mu yaxal mooy ñu taxawal ag nguur gu Itaali ca bëj-gànnaaru Itaali, buurub Piemonte jiite ko, ak geneen nguur ci digg bi. Moomeeli paab gi moom ñu bàyyi leen fi, te bañ a laal dara ci nguurug Napoli, gi nekk ci bëj-saamu Itaali, bu ko defee nag, genn bennoo gu ame cig dëppoo lënkale leen ci njiitug paab bi. Fraans nag li muy ame ci loolu mooy ñu bàyyee ko Niis ak Savoia.

Xare yi amoon ci diggante Piemonte ak Otris:

Kafour wéy na di cokkaas Otris, rawati na bi ko Napoleon III yonnee ñaari temeeri junniy xarekat, ngir ñu xeexle ko kontar Otris, loolu nag amoon na ci ginaaw dëppoog (Polombiere) gi .
Kafour am na la mu bëggoon muy jeqi Otris, yëngal ko, ndax moom kat (Otris) mujjoon na jekki-jekki rekk sàkku ci Piemonte mu nocci ay ngànnaayam ci diir bu gàtt, bu weesuwul ñatti fan, mu tóllanti loolu ci jug jawali Piemonte ànd ak ay xarekatam atum 1859g.
Taarixkat yi firee nanu loolu ne ag wuyyusi la gu Otris def ci li ko Piemonte doon yàgg a cokkaas, ak a dëkk.

Nii daal la xare bi tàkke ci diggante Otris ak Piemonte, waaye nag Otris a njëkk a song, ci noonu Fraans itam jibal ab xareem ci kaw Otris.
Soldaari Piemonte yi ak yu Fraans yi jot nanoo duma Otris, gañe ko ca xare ba nuy wax Maginta ak Salvarino, waaye Napoleon III moom daa xëyoon rekk taxawlu ci xare bi, daal di gise ak Imbraatoor bu Otris bi, def ak moom ag wéer-ngànnaay, dellu xaatim ak moom ag juboo, te diisoowu ci ak nguurug Piemonte. Wéer-ngànnaay gii nag mooy li jur ci ginaaw bi, li nuy wax juboo gu Siyorix  atum 1859g. bokkoon na ca poñ ya ëppoon solo ca juboo ga:

(1)	Otris bàyyee Piemonte Lombardi
(2)	Sos booloo gu Itaali ci njiitul Paab bi ci tur
(3)	Venezia day des ci moomeelug Otris, waaye bokk ci bennoo gu Itaali gi
(4)	 Delloosi ñi yilifoon Doox yi nekkoon ci digg Itaali ci seen barab, ak seeni pal, ginaaw bi leen askan wi follee.
(5)	Boole Niis ak Savoia ci Fraans.

Taarixkat yi, firee nanu taxawal xare gu bette gi nga xam ne Napoleon III, defoon na ko, ne daal li ko waraloon, mooy daa bañoon ag nguurug Itaali gu dëgër am, taxaw, rawati na bi mu tàmblee gis lenn ci Doox yi nekkoon ci digg Itaali tàmblee bokksi ci Piemonte. Bokkoon na it ci li ko ko taxoon a def, jeem a gëramloo Katoligi Fraans yi nga xam ne danoo tàmbli woon a mer ci neewal gi nuy neewal doole nguurug paab gi ci Itaali, te Otris a ko daan jàppleek a dëgëral.
Kafour nag moom, daa daal di woon xàcc , walla tekki ndombaam, bi mu sàkkoo ci buur bi Victor Emanuel ba soon ngir ñu wéy ci xare bi ak doonte Fraans genne na ci loxoom, waaye mu lànk mom buur bi.
Askani Doox yi bañ nañu ne dunu nangu mukk ñu delloosi ña leen yilifoon bu njëkk, ni ko poñi juboo gu Siyorix gi yaxale, ñu ne woon daal ñoom leegi danuy dem bokki ca nguurug Piemonte.
Ci noonu ay fipp am yu toftaloo, ci Parma, Modena, Romaña ak Toscana, di woote ag bokki ca Piemonte. Kafour dellusi na yoraat njiitug jawrin gi, ngir sonnal gu ko askan wi sonnal ci mu dellusi, ci biir Piemonte ak ci biti.
Nii daal la Itaali doone benn ci gox yi nekk ci bëj-gànnaar gi ak digg bi. Kafour dara deseetu ko woon lu dul mu fexee nangu Venezia, ak moomeeli paab bi, ak nguurug Napoli gi boole leen ci Itaali.

Coona yi Garibaldi doon daj ci Itaali doon benn:

Garibaldi moom ku bëggoon la te gëmoon bennug Itaali. Moom nag soldaar la woon bu dëgër, jàmbaare te ñeme. Mujjoon na it bokk ci jàmbaari Itaali yi siwe woon ag wooteg bennoo gu xeet, te daan ci ligeey. Garibaldi mii, tukkee na Genova atum 1860g, ànd ak lu jege junniy xarekat yu bokkoon ci way coobarewu  yu Itaali yi nu tudde woon “Boroom simis yu xonq yi”. 
Daal di wàcc ak ñoom Sisil, jot faa dàqe doole ya fa nekkoon te àndoon ak buurub Napoli bi, ginaaw diirub ñatti weer. Daal di jéggi xat-xatu Silil bi , dugg ak dooley xareem ji Napoli, ci lu dul jàmmaarloo gu nu man a tudd. Ci noonu Napoli mujj ak dëkk yi nekk ronam, dugg ci bennoo gi.

Samp Victor Emmanuel muy buuru Itaali:

Dooley Piemonte ju xare ji jawali woon na ca diiwaan ya nekkoon ca ron kilifteefug Paab bi, mu jotoon a nangu moomeeli Paab bi bepp, lu ci dul Rom. Ci noonu xarekati Piemonte yooyu jawali woon ca soldaari Garibaldi ya, ca Napoli, ci ndigalul Kafour, ñu àndandoo nag xeex ba nangu mbooleem gox yi nekkoon ci ron nguurug Napoli, te Garibaldi manu fa woon àgg moo rekk. Ci noonu Victor Emmanuel ñëw, dugg Napoli, ni ku gañe di dugge ci dëkk bu nu xare ba nangu ko.
Parlamaa bu Itaali bu bees bi def na ndajeem mu njëkk, ca Torino, bisub 18 febriye atum 1861g. Ca ndaje ma lanu ndëppale Victor Emmanuel , def ko buurub Itaali gu nu bennal gi.
Ginaaw bi Itaali taxawee di ag nguur gu nu bennal, ba am juroomi weer la Kafor faatu, ci sulye atum 1861g. Garibaldi it bàyyi politig, ndax kat moom li ko taxoon a jug mooy ligeey ci Itaali doon benn, waaye soxlawutoon ay pali politig.

Def Rom peeyu nguurug Itaali gi:

Waa Itaali yi delloosi nanu Venezia mi Otris tegoon loxo, nangu woon ko, delloosi gi di ci atum 1866g, mu mujj nag moom Venezia di ab gox ci Itaali, ginaaw ba nu fa dàqee dooey xare ju Otris ji. Nanguwaat googu nag ñi ngi ko mane ci ñàkk a tal gi leen Otris ñàkkoon a tal, ngir xeex bi mu nekkoon di ko def ak Brusiya.
Fraans it ay xarekatam gennoon nanu Rom, ngir sotti gi Fraans sotti woon yitteem ca xareem ba’ak Brusiya. Bi mu ko defee soldaari Itaali yi daal di leen fay wuutu, ci 20 sebtambar atum 1870g, ñu daal di jibal ci anam gu ofisel ne Rom daal mooy peeyu nguurug Itaali gu nu bennal gi.
Doxaliin wii merloo woon na Paab bi, yobbu woon ko ci mu bañ a nangu loolu, ne woon it du man a summiku ci sañ-sañu politigam yi te du nangoo raflewu ci nguuram gi.
Noonu la mbir mi nekke woon ba 1929g, ca la genn dëppoo ame ci diggante Mossolini  ak Paab bi, dëppoo googu mayoon na Paab bi mu doxe nu ko soob ci mbiri diine ji, te am ag tembte gu mat ca Vatikan, am it sañ-sañ ci yabal ay ndaw  yu koy toogal ca biti. Ñu wutal ko nag (moom Paab bi) njëlul boppam lu mu jagoo .

Nii nag la Itaali doone woon benn, muy lol ay doomam a ko xeex. Doomam yoy danoo jëloon seen coona bepp def ko ci goreel ko, bennal ko, te fuqarcee ko ci ngëbug jàmbur, bu leen ruuroon, teg leen loxo. Bennoo gii de lu ñepp soppoon la, ndaxte doole la ci ñoom, di teddnga, di tembte te dig fonk sa xeet. Bennoog Itaali du lenn lu dul meññatum sellal ak gëm ag bennoo. Mooy wuyyu gu mag ga, ca woote ga Michiavelli doon woote, moom mi doon sàkku ciw nitam ca teereem ba tudd “buur bi” te looloo njëkkoon bennoo gi ci ay xarnu, mu doon sàkku ci ñoom ñu ligeey ngir bennal seenuw reew. 

Doggantal gu ñaareel gi

Bennoo gu Almaañ

Almaañ  njëkk xare yu Napoleon yi:

Almaañ njëkk xarey Napoleon yi, dafa seddaliku woon ci lu jege ñatti teemeer ak juroom benn fukki diiwaan, yepp it ci ron imbraatoor gu Otris lanu nekkoon, walla li nuy tudde Imbraatoorug Rom gu sell gi. Almaañ gepp it genn nguur rekk a fa nekkoon gu mag te temb, mooy gu Brusiya. Nguur googu nag jëmoon na kanam, te ag yewwuteem fés, ci jamonoy buuram ba tuddoon Fredrick mu mag mi (Great Fredrick) (1740 -1786 g), mooy ki ko defoon muy nguur gu dëgër te am doole. Bu ko defee waa Almaañ yepp wëlbati seeni gët jëme ci nguur gii, ngir bëgg ag bennoo.

Almaañ ci jamonoy Napoleon: 

Napoleon ak xarekatam ya xuusoon nanu ci diiwaani Almaañ yi, teg leen loxo. Daal di jawali ca nguurug Brusiya, gi nga xam ne jàmmaarloo woon na’ak ñoom cig njàmmaar ak fit, waaye Napoleon moom mujj na ko not, te gañe ko ci mujj gi, ca xareb Yena ba, atum 1806g, daal di teg loxo peeyam ba Berlin.
Napoleon merloo woon na lool waa Brusiya yi, ci dog gi mu dogoon ay wàll ci seeni suuf, te jébbaloon leen diiwaanu Saksoni bi. Waaye nag ci geneen wàll, am na lu am njariñ lu mu fa indi, ndaxte wàññi woon na limub diiwaan yu Almaañ yi ba ci fanweer ak juroom ñeent rekk, te bu njëkk lu jege 360 lanu woon. Kon jëfi Napoleon jii, mbir la mom moo nooyal yoon wi, waajal ko ba ag bennoo gu Almaañ man a judd, man a taxaw.

Almaañ ginaaw ndajem Vienne mi:

Ginaaw bi Napoleon Bonaperte daanoo atum 1815g, ci lanu def ndajem Vienne, ñu jële fa ay saxal yu bari, bokk na ci yooyu, dagg Doox bu Warsaw gu Poloñ gi, dagg ko ci Brusiya, te jox ko Rusi, bu ko defee ñu jox Brusiya moom itam goxub Rayan ak xaaju diiwaanu Saksoni. Daal di taxawal ag bennoo gu Almaañ gu làmboo fanweer ak juroom ñeenti nguur-nguuraan yu Almaañ, Otris jiite ko.
Defiin wii nag mi ngi ame ci càkkuteeful Metternich, ak naj gi mu doon naj way daje yi, ngir ñu defal ko bëgg-bëggam boobu. Bennoo gu Almaañ gii juddoo ci ndajem Vienne mi, nekkoon na di lu manul a wéy, ndax kat Otris moom daa tàmbli woon di genne ay saxal aki ndigal yuy kontar tas-xibaar gu gore , te wéeroodi fenn, tey kontar mboolooy Almaañ yi daan sàkku ag bennoo te daan ko woote. Te Otris it daa mujjoon teg loxo ci jataayub bennoo gu Almaañ gi, te ga woon ko  ci mu genne ay saxal yuy digale ñu fuglu daara yu mag yi , ak leekol yi, ak ndaje yi añs.doxaliin yooyu nag taxoon na ba ay kàddu jib yu ay waa Almaañ, di sàkku ñu fipp ci kaw Otris, tey sàkku ñu jeem a bennal Almaañ, ci keppaarug nguur gu Almaañ gu dëgër. Loolu mooy li xeltukatu Almaañ bi (Hegel) daan sàkku, te daan ko woote, moom ak ñeneen ñi daa jam  bennoo gii nga xam ne Otris a ko moomoon daanaka, te tegoon ko loxo.

Taxawaay bi nguurug Brusiya  ame woon ci naal  yi jëmoon ci Bennoo gu Almaañ gi:

Nguurug Brusiya dafa tàmbli woon di yëngu ngir dajale xeetu Almaañ wi, duggal leen ci genn nguur gu Almaañ gu nu bennal. Mu daal di woon rëddal boppam ab politig bu muy jaar ngir àgg ci loolu mu bëgg. Mu daal di woon door ci dëgëral boppam ci biirum reew, defaraat doxaliinam , yekkati koom-koomam, soppi nosteg galag yi aju woon ci nduwaan  ci mbooleem goxi nguur gi.
Ñu daal di taxawal noste gi nu daa wax (Solofrayn), di ag bennoo ci wàllug nduwaan, mooy li neenaloon nosteg nduwaan gi ci biir Almaañ. Nga xam ne li nekk ci biir reew mi cim njaay deesu ci genne duwaan. Nga xam ne danoo feexal yaxantu gi ci Brusiya, ëfal ko ba mu man a doxe ni ko soob, ci lu dul ñu ciy teg ay tënk-tënki galag mbaa yu nduwaan. Doxiinu Brusiya wii dey dees na ko lim mu dig soopiku gu mag ci taarixu bennoo gu Almaañ gi. Doxal nanu ko nag ci atum 1818g, ci biir ay goxam yu biir yi. Gox yooyu nga xam ne njëkk “Nosteg Solofrayn gi” danoo nekkoon ay gox yoo xam ne bu ci nekk daa amoon nosteg pobb gu nduwaan, gu mu bokkul ak kenn. Waaye bi Solfrayn taxawee, lanu bennal biir Brusiya ci wàllug nduwaan, ginaaw bi mu nekkee moom Brusiya di lu nu seddale ci juroom benn fukki goxi nduwaan.

Waa Brusiya yi yëgoon nanu ne benno gi ci wàllug koom-koom mooy cëslaay li nu war a teg  bennoog Almaañ gi ci wàllug politig. Looloo taxoon kilifay Brusiya yi tàmbli woon a fexe nu nuy def ba duggal yeneen diiwaani Almaañ yi ci bennoo gu nduwaan googu. Brusiya nag amoon na ndam ci li mu doon wut ci yenn ci diiwaan yu Almaañ yu ndaw yi, waaye nag jot naa dajeek ag jàmmaarloo gu mag ci yeneen diiwaan yu Almaañ yu mag yi, li ko waral mooy ñoom dañoo gisoon ne li gën ci ñoom mooy ñu sosal seen bopp ag bennoo gu ndawaan gu temb, ngir xeex ci bennog nduwaan gu Brusiya gi. Looloo fi indi woon ñatti bennoo yu nduwaan ci Almaañ, ñooy: 

(1)	Solofrayn
(2)	“Bennoog nduwaan gu Bavar” gi nga xam ne mi ngi judd woon atum 1820g, maanaam ginaaw bi gu Solofrayn amee ba am ñaari at.
(3)	Ak bennoo gu nduwaan gu Saksoni. Mooy gi Saksoni taxawaloon atum 1828g.

Kilifay Brusiya yi xamoon nanu ne diiwaani Almaañ yi dananu nangoo duggsi ci bennoo gu Solofrayn gi, bu nu soppee sart yiy tax manees cee dugg. Looloo taxoon ñu soppi sarti Solofrayn yi, nga xam ne leegi danoo sos ab jataay bu làmboo mbooleem ndawi yi ci bokk, buy saytu noste googu. Leegi nag lu fa duggati rekk ci li bawoo ci nduwaan mi ak galag yi ñu koy seddale mbooleem diiwaan yi, ci kem limub ña fa dëkk. Soppi yii de dimblee na ci yaatal gëweelub Solofrayn, gën a yàkkali ab geewam. Leegi nag Bavar bokksi na ci ak Saksoni ci atum 1934g, ca saa sa tam, nga tàmblee gis lu lay won ne Solofrayn moom tàmbli na a naat ak a am ag yokkute. Yaxantu ga tàmbli woon nay jar, di dox, mbay ma màgg, endustri ba jëm kanam ci mbooleem diiwaan yi bokksi ci Solofrayn. Am na nag benn jëfka  boo xam ne moo àntul Solofrayn, mooy moom de noste gu waa Almaañ xalaat ba def ko la, loxol Otris duggu ci, jenn doole it ju ko man a teg loxo yoonam nekku ci. Metternich gisoon na ay wi nekkoon ci noste gii, waaye bi mu koy gis fekk na waxtu wa jàll, manatu ca woon dara. Mu daal di bind Imbraatoor bu Otris bi ne ko: “Na la wóor ne nguuri Almaañ yi - bi lii amee de – di nanu nekki wenn yaram wu jàppaloo, ci ron kerug doxaliin gu Brusiya, te da na jàppeji Brusiya muy - moom - aw yaram wu di doxandeem, wu tumbrànke wu bokkul ciw yaramam”. Te kat waa Otris yi ñoom, ca dëgg-dëgg, dunu ay doxandeem ci waa Almaañ yi, ndax ñoo bokk xeet, làkk ak taarix. Man nanu ne Almaañ gepp mujj na bokksi ci Solofrayn gi, atum 1842g.

Xalaatu xeltu bu Hegel bi feddali woon na dooley nguur, ak ray gi muy ray jëmm ak lepp lu mu am, ngir sàmm dooleem akug màggam ak wegeelam. Nguur walla àtte – ci gis-gis Hegel- cëslaayam mooy doole, ci doole rekk la man a dëgërale gëgg. Kon nguur walla àtte gu dëgër ci gis-gisu Hegel, mooy nguurug walla àtteg dëgg. Kon moom Hegel day mel ne moo teg ci loxol Brusiya lay wa xeltu guy rafetal, di baaxal seen jëfi jiite googu nu jiite woon bennalug Almaañ gi.

Ñu leeral leen ne bi 1848g di jot, fekkoon na Brusiya muy reew mu am kàttan ci tere Otris muy dugg ci mbiri nguur-nguuraani Almaañ yi. Naka noonu, nekkoon na it mu amoon kàttan ci jiite yëngu-yëngu gi jugoon ngir bennal Almaañ. Nguur-nguuraan yi bokkoon ci Solofrayn it, doon man a dimblante ci seen biir ci wàllug koom-koom, te daan jëflante ci lu dul yoonu Otris di ci nekk mbaa ñuy diisoo ak moom, walla ñu koy tàggu. Ci noonu nguur-nguuraan yooyu tàmblee xoole Brusiya bëtu kilifa. Ci noonu la bennoo gu koom-koom googu doon màgg ak a naat ci ro kerug Solofrayn, mujjoon di ab jeego bu mag jëm ci ag bennoo gu politig ak xare ci Almaañ.

Jeexiit yi fipp gu atum 1848g defoon ci amug bennoo gu Almaañ gi:   

Ay fipp yu bari jot nanoo am ca Tugal atm 1848g. Ag fipp am ca Paris, am gu am ca Vienne, geneen ca Brusiya ak ay fipp ci Itaali ak Almaañ, yepp it di xëccu jëm ci ag gore , demokraasi ak xeetu . Metternich mu màggat mii, mujjoon na manatul woon a noot fippi Tugal yooyu, mbaa mu giimal leen, ni mu ko baaxoo woon a defe.
Kërug Orob gi mujj – ni ko Metternich di waxe – di kër gu màggat, te ràpp, ba àgg ci maneesatu cee yatt sax ab palanteer ciy miiram ngirug màggat, kon leegi li jaadu kay mooy ñu màbb ko, te wuutal fa geneen kër gu yees. Ca dëgg-dëgg nag loolu am na, ndax kat noste ga amoon ca la ëppoon ca reewi Tugal ya, daa mujjoon di lu ràpp, ngirug yàgg, mujj manatutoon a ñàkk ñu yeesalaat ko, te taxawalaat ko ci anam gu dëppoo ak li jamono laaj. 

Metternich dawoon na, te daanu woon, ci noonu buurub Brusiya bi Frederick William mu ñeenteel mi daal di jug, woote am ndaje mu parlamaa, ngir ñu defaral Brusiya ab sartu reew bu bees. Mu dig aw askanam ne leen moo fas yeenee jiite yëngu-yëngu giy jug ci jeem a bennal Almaañ, ci benn bataaxel bu mu leen jàngal. Ndaw yi teewal Almaañ yepp teewe woon nanu ndajem atum 1848g moomu, ñu def fa ay gëstu ci lu aju ci Almaañ gu nekk benn. Ndajem parlamaa mii, ñi ngi ko gën a xame ci turu “Parlamaab Frankfort”. Ndaje ma ëmboon na lu bari ciy woykat , aki xeltukat aki taskati xibaar aki ustaas.
Ñatti saxal nag yu mag juddoo nanu ca ndaje ma:

(1)	Bennal Almaañ ci njiitul buurub Brusiya.
(2)	Ñu boole ci bennoo gu Almaañ googu, wàllug Almaañ gi bokkoon ci imbraatoorug Otris gi
(3)	Genne Otris ci bennoo gu Almaañ gi.

Way daje yii ci Frankfort, (seenub lim àggoon na ci 830 ciy jëmm) tànnoon nanu buurub Brusiya bi Fredereick William mu ñeenteel mi, def ko imbraatoor ci Almaañ gu nu bennal gi. Waaye Frederick moom daa bañoon ne du dëppoo ndëppul imbraatoor li nu ko joxoon, te way daje yi joxoon ko ko, ndax da ne ndëpp li daal ndawi askan wee ko ko jox, waaye buur yeek kàggam yi joxuñu ko ko. looloo taxoon nanguwu koo sol.
La am nag mooy ne buuru Brusiya bi dafa bañ a jël ndëpp li, ndax xam ne Otris ak Rusi ànduñu woon ci bennoog Almaañ googu, te manoon nanoo xëy di duggati ci seeni mbir ngir loolu. Rawati na ne Otris moom jot na a not fipp gi amoon ca peeyam ba Vienne.
Nga rax ci dolli ne Buuru Brusiya bi, moom dafa gëmoon gisiinu “àq ak sañ-sañ bu Yàlla bi”, mooy gisiin wi naan ñoom buur yi Yàlla a leen fi teg, moom lanu fi wuutu, nit ñi tegunu leen fi, du keneen it. Looloo taxoon bu nangoo it ñu def ndaje moomu, muy mu Frankfort mi, jubluwu ci woon lu dul ngistal, waaye du ligeey bu fullawu, mbaa mu dëggu ci yoonu soppi. 

Otris ak Rusi dimblante nanu ci màbb barlamaab Frankfort bi, ak naalam yi mu amoon te nu jëm cig bennoo gu Almaañ, looloo waraloon jeem gi nu doon def ngir bennal Almaañ ci ron kilifteefug Brusiya, ci atum 1848g, mujjul woon àntu. Waaye li muy àntoodi lepp teewul xalaat bi sax ci xoli ak xeli waa Almaañ yi. Ñu mujj (waa Almaañ ñi) xam ne daal dunu man a amalati seen bennoo googu ci anamug jàmm, mbaa gu sartu reew, ndaxte Otris àndu ci te mi ngi koy xeex ak doole.
Looloo waraloon nu jëloon seen yitte def ko ci amal am mbooloom xare mu dëgër, mu leen di man a may ñu man a genne Otris Almaañ cig njëlbeen, door a lijjanti nag nu nuy doone benn ci ginaaw bi.
Xalaat bii nag diisoowaale  bu Brusiya  bii di Bismarck, àndoon na ci te jàpple woon ko, dëgëral ko. Moom mooy Otto Von Bismarck, boroom kurpeñu weñ bi.

Politigu Bismarck ci lu jëm ci bennoo gu Almaañ gi:

Bismarck mi ngi judd atum 1815g, am njàggam mu kawe mu defe ko ca daaray Berlin ju mag ja. Daal di dugg ag coldaar, gennati ca, dem nag feete ca boppam ca toolam ba. Mi ngi bokkoon nag ci njaboot gu woomle, gu ami alal yu rëy ca Brusiya. Sampoon na boppam  ngir nu fal ko ci bennoo yu Almaañ yi, atum 1848g, ñu tànnoon ko it muy ab cer  ci parlamaa bu Brusiya bi. Ligeey na it ci toolub diplomasi, doonoon ndawul reewam  ca Butrsburg ca Rusi. Ginaaw bi mu nekkal reewam ca Paris.foofee la ko William mu njëkk mi doon jiite Brusiya woowe woon mu juge Fraans, ngir jiite-si njiitug jawrin gi ci Brusiya.
Bismarck nag nekkoon na ku gëmoon, te daa dëgëral noste gu nguur gu nu joyal , te gëmoon ne buur daa war a am doole te am soldaar su dëgër, Egliis bi jàpple ko ak garmi yi. Bismarck moom faalewutoon parlamaa bi. Gisoon na ne jëm kanamug aw xeet walla ag yeegam jëm ca kaw manul a ame ci lu dul ay buuram di ñu kawe ay yitte, ak ay kilifaam, waaye du nu ko ame mukk ci ay saxal yu juge ci ay parlamaa, aki nostey sarti reew.

Bismarck yitteem jepp mi ngi ko jëmale woon ci genne Fraans ak Otris Almaañ, mu gisoon ne lii daal manul ame ci lu dul dooley xare ju mag, ju leen ci man a ga. Ci noonu mu tàmblee ligeey ci dëgëral dooley xare ji, ak kàttanal ko. Mu daal di tas parlamaab Brusiya bi, ndaxte (moom parlamaa bi) daa bañoon ne du woote alal ji mu doon laaj ngir man cee dooleel soldaaram si, ci noonu mu tëjopon kepp ku wuuteek politigam boobu, daal di digle ñu fuglu yeglekaay yi, daal di beddiku sartu reew mi, ne du ci sukkandikooti. Alal ji mu soxla woon mu gennelu ko ci ndigalul buur bi, bañ cee sukkandiku ci lu parlamaa bi.

Wàllug xeetu  nag moom gis-gis bi mu ci amoon moo gënoon a yaatu bi mu amoon ci sartu reew, ndax daa gisoon ne sartu reew moom, mi ngi ame mook ay jubluwaayam, ci ginaaw bu ag xeetu amee ba noppi.
Bismarck nag neenalul mbooleem parlamaa bi mbaa mu tas ko lepp, moom kay da caa neenl walla mu soril ko ñatti mbir, ñooy: 
(1)	Coldaar gi
(2)	Politigu bitim reew bi
(3)	Fal ay jawrin ak di leen folli

Bismarck wone na dogu gu mag akug takku contar teg gi Otris teg loxo Almaañ, loolu nag gën na a fése ci taxaw gi mu taxawoon ci dakkal politigu  Otris bi muy teg Almaañ .
Looloo taxoon Otris mujj woo buuri Almaañ yepp cim ndaje ca Frankfort, ngir sos ag bennoo gu federaal, guy doxal ab goornamaa, boo xam ne ay dooleem ak sañ-sañam mi ngi koy jële ci sart boo xam ne Otris moo koy defar, tër ko.
Bismarck gisoon na ne lii de ag anam gu yees gu Otris jëlati la, ñu muure ko mbubum diplomasi, ngir yeegati ci kaw waa Almaañ yi. Bismarck melaloon na sart boobu ne mooy sart bi gën a bon ci mbooleem yu mas a am ci kaw suuf. Ci noonu mu ne woon du teewe ndaje ma lu dul ci kaw ñu jox Brusiya ay àq aki yelleef yu tol ni yi nu jox Otris ci ñaari mbir yii, ñooy:
(1)	Dëgël ak wéyal jibalug bennoo gi 
(2)	Jiite benno gi

Bismarck ci taxawaayam bii, leerale na ci ne Otris daal moom ñàkk na kàttan ga mu amoon ci aakimoo moom rekk mbirum bennoo gu Almaañ gi. Te it won na nguur-nguuraani Almaañ yi ne Brusiya mii kat mooy jenn dooley Almaañ ji man a jiite bennoo gu Almaañ gi.
Bismarck jeem na a fàggu cofeelug Rusi, ngir mu bañ a feete fenn, bu ab xare tàkkee ci diggam ak Otris. Loolooo taxoon mu dugg ci lëj-lëju Poloñ bi, jàpple ci Rusi, kontar gori Ploñ yi defoon ag fipp kontar Rusi, ngir dañal ag àtteem te jeem a am ag tembte, ba man a amal ag àtte gu Poloñ gu temb.
Fraans nag àndoon na ca fipp ga, te jàpple ko, askanu Angalteer wi ànd ca, waaye goornamaa ba moom àndu ca woon, ndax daa ragaloon ag nguurug Poloñ gu katolig judd, guy dem di àndeek Fraans.
Ci noonu Bismarck moom dem jàpple-ji Rusi, te jàpple googu gu amoon doole la, ndax moom reewam (Brusiya) daa taqaloo woon ak Poloñ, ba noppi taqalook Rusi. Te it nanguwutoon a ànd ak Fraans ak Otris kontar Rusi.

Xarey Bismarck yi ngir taxawal bennoo gu Almaañ:

Bismarck xuus na ay xare ak lu bari ci reewi Tugal yi digoo’k Almaañ, ngir bennal reewi Almaañ yi. Ñu tudd ñatt rekk ci xare yooyu, ñooy:

Xare Brusiya yi ak Danmark:

Bismarck xuus na ab xare kontar Danmark, atum 1864g, ànd ca’ak Otris, ngir nangu ñaari diiwaan yii di Shalswig ak Holistin, ñu doonoon ñaari doox  yu bokkoon ci bennoo gu Almaañ gi te Danmark tegoon leen loxo.
Danmark mujjoon na ñàkk pexe, daal di deltu ginaaw  wëlif ñaari doox yooyu atum 1864g, bu ko defee Brusiya jël dooxu Shalswig, Otris it àtte diiwaanu Holistin.
Xarey Brusiya ak Otris:

Bismarck gisoon na ne xare bi moom – deet sikk – aji tàkk la ci diggante Brusiya ak Otris, te li ko waral du dara lu dul diiwaanu Holistin. Ndax kat mbir yi manunu woon a nekk di wéy ci anam gii nu nekke, di ay maslaa yu dëggoodi aki lijjanti yu xootadi aki juboo yu gàtti dig.
Bis bu Yàlla dogalee njortul Bismarck loolu mujj di dëgg, ba Brusiya am ndam, loolu de da na nekki muccug waa Almaañ ñi ci gàllankoor gii tukkee ci Otris, gu leen di teree nekk benn, tee bennoo gu Almaañ gu wér man a am. Màggug Brusiya ci wàllug politig ci biir bennoo gu Almaañ gi, mujj di luy jeqi njàqare ci Otris. Solofrayn moom màgg na ci anam gu doy waar, rawati na bi ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi tiim geejug bëj-gànnaar gi bokksee. Ci noonu lu sakkan jug ciy yooni weñ  lënkale diggante wàll yu Almaañ yu wuute yi. Loolu tam dooleel bennoo gu koom-koom gi nga xam ne Brusiya mujj na di ci ki ci gën a jariñu.

Sabab yii rekk doyoon nanu ngir taal xeex bi ci diggante Brusiya ak Otris, rawati na ginaaw bi dooley Brusiya ji doxee jawali Holistin, nangu ko, te moom daa nekkoon ci ron kilifteefug Otris, ngir dëppoo gi amoon ci diggante Brusiya ak Otris atum 1865g.

Bismarck moom lijjanti woon na ba Rusi genne loxoom ci diggam ak Otris, loolu nag di ci jàpple gi mu jàpple woon Rusi ci giimal fipp ga amoon ca Poloñ, atum 1853g. Dëppoo woon na ak Imbratoor bi  Napoleon III, imbraatooru Fraans, moom itam, ngir mu seetaan kook Otris, bañ cee dugal loxoom, li mu koy faye ci loolu nag mooy bàyyi kook yenn moomeel yi ci goxub Rayn. Mu demati tapoo-ji ak nguurug Itaali, gi nga xam ne li doonoon yitteem mooy nocci Venezia ci loxol Otris, ngir matal ag bennoom.

Xare bi amoon ci diggante Otris ak Brusiya xare la woon bu fëkk te gaaw, wéyutoon lu ëpp juroom ñaari ayu-bis, moo waraloon nu tudde woon ko xareb juroom ñaari ayu-bis yi. Dooley Brusiya ji jot na ca a gañee ju Otris ja ca xareb Sadwa ba, ca Bohima atum 1866g . Mu manoon a àgg sax (moom dooley Brusiya ji) ba ca Vienne, bu Imbraatooru Fraans bii di Napoleon III jugutoon, dox tànki jàmm ci diggante bi. Ci noonu Bismarck daal di ñàkk pexe, taxawal xeex bi, ngir ragal Fraans dugg ci xeex bi ci wetu Otris. Te it Bismarck moom da ne woon na doylu nag ci gañe gii mu gañe Otris, ak dammte gii mu ko dammte, ndaxte soril na ko bennoo gu Almaañ cig wàll, te it bëggutoon a toroxal Imbraatooru Otris bi, ngir loolu man na a tax bu jugee ëlëg moom Brusiya di xare-ji ak Fraans, Otris du ko sot, ci geneen wàll.
Ag juboo amoon na ci diggante Brusiya ak Otris, ñu koy wax “juboog Braax gi”, atum 1866g. Ci la yii ame:

(1)	Gennug Otris ci Bennoo gu Almaañ gi, gi mu tegoon loxo, la ko dale ca jamonoy Metternich.
(2)	Duggug mbooleem nguur-nguuraan yi nekkoon ci bëj-gànnaaru dexu Rayn gi, ci bennoo gu federaal gu Almaañ ci ron njiitul Brusiya. Diiwaani bëj-saalum rekk a bokkutoon ci bennoo googu.
(3)	Bàyyee gu Otris bàyyee Itaali Venezia.

Gis nga ko, Bismarck kat am na ay ngërte yu am solo ci xareem beek Otris. Moom de fare na fi bennoog Almaañ gu yàgg ga, indi fi leegi ag bennoo gu Almaañ gu yees, gu ame ci mbooleem reewi bëj-gànnaaru Almaañ, nga xam ne ñaari doox yii di Shalswig ak Holistin ci lanu woon, buuru Brusiya bi jiite ko. Bismarck nos na bennoo gu yees gi, wutal ko ab parlamaa (Rashstach), ndawi askan wa di fa daje, ak jataayub bennoo gu Almaañ gi (Bundasrat), ndawi diiwaani Almaañ yi bokk ci bennoo gu Almaañ gu bees gi di fa daje.
Bismarck it lijjanti na ba def ak diiwaani bëj-saalum yi bokkutoon ci bennoo gi, lijjanti woon na ba def ak ñoom genn tapoo  gu xare .

Xareb Brusiya ak Fraans:    

Xetug xare tàmbli woon na a xeeñ ak a jòlli ci diggante Fraans ak Brusiya, ginaaw bi Brusiya gañee ca xareb Sadwa ba. Ndaxte Fraans moom begutoon dara ci lii Brusiya amal ciy ndam ci kaw Danmark ak Otris cig wàll, ak àntul gi mu àntuloon bennoo gu Almaañ gu bëj-gànnaar gi, ci geneen wàll.

Fraans moom daa jàppe woon loolu muy aw xët ci digg ginaawam, ndaxte moom kat manul woon a dékku ag nguur gu Almaañ gu am doole ci wetam. Moom kay li ko sooboon mooy Almaañ des di nguur gu nu dogat, ngir mu nekk moom Fraans di reew mi am kilifteef ci sowwub Tugal bi. Moom kay jamono ju nekk, da daa kontar bennoog Almaañ gi, ni ko Otris kontare woon. Bismarck it tàmbli woon na a xalaat nu muy xëcce diiwaani Almaañ yu bëj-saalum yi ngir nu bokksi ci bennoo gi. Jëf ju mel ni jooju nag Fraans du ko doon nangu, ndax moom tàmbli woon na di dugg ci mbiri diiwaan yu Almaañ yu bëj-saalum yi, ngir tee leen a bokki ca bennoo gu Almaañ ga nga xam ne Brusiya ko jiite woon.
Lëj-lëju ku jigeen ki waroon a donn Espaañ daal di taxaw, mooy lëj-lëj bi taaloon xare bi ci diggante Brusiya ak Fraans.
Lëj-lëj boobu mi ngi tënkoo woon nii: gàngunaay gu nguurug Espaañ dafa feexoon , ginaaw bi lingeeru Espaañ bi Elisabeth dawee, ñu gaaral buur bi Leopold ndëpp li, moom mi ngi bokkoon ci njabootug Hohenzellern, di woon ab njegeñaaleb imbraatoor bu Brusiya. Waaye ak li Leopold di bañ lepp ne du sol mukk ndëpp li, teewul Fraans mer ci loolu, jàmbat ko ci buurub Brusiya bi, daal di sàkku ci moom mu warlu ne du ànd ci ñu samp kenn ku bokk ci njabootug Hohenzellern ci gàngunaayaug Espaañ gi. Waaye buuru Brusiya bi bañ, ndax loolu kat dafa xaw a laal teddngaam ak ngoram, te xaw a niru ag yabeel. Loolu nag mi ngi ame woon cim ndaje mu mu defoon ak ndawul Fraans ca Ems. Bu ko defee buuru Brusiya bi yonnee ab day  ca la juge woon ca ndaje ma, mu yonnee ko Bismarck, mi nga xam ne lepp li mu doon def mooy neggandiku ab pose ngir jibal ab xare ci kaw Fraans. Ba mu ko defee, Bismarck xëy tas ci yëglekaay yi ay cofiit ca la bawoo woon ca ndaje mooma, ngir merloo ci Fraans. Loolu nag ni mu ko defe mooy genne ay baat yu xaw a wow, yu begloowul dara Fraans. Ci noonu Fraans jug, jibal ab xare ci kaw Brusiya, ci 14 sulye 1870g, te fekku ko woon jekk ngir xeex, te taxul woon it mu xalaat ci ngérte yi man a juddoo ci bii xare, bis bu nu dàqee Fraans ci xeex bi.

Brusiya li nuy wax xareb fëkk la doon def ak Fraans, maanaam gaawal ko, loolu nag jot na koo def ba am ci xam-xam ca xareem ba’ak Otris. Bi mu ko defee tàngooru xare bi sax di tar lu tollook juroom benni ayu bis, waaye tàmblee giim, ci ginaaw bi, rawati na ci ginaaw bi ay màndargay kawe ak ëpp doole tàmblee feeñ ci xeex bi ñeel Brusiya.
Xare bi bepp nag ci suufus Fraans la doon tàkke. Jotoon nanoo dàq Fraans nag ci xeex yu bari, bi ci gënoon a siw nag mooy bu Sedan ca satumbar1870g, nga xam ne àggoon na ci Napoleon III manutoon a ñàkk a wommatu, te nangu ne gañe nanu ko, ngir dàq yu metti yi te toftaloo, te yepp di yu nu teg ci kaw dooley Fraans ji ci biir suufus Fraans, te ray lu sakkan ciy soldaaram, te itam lu jege ñaari teemeeri junniy soldaari Almaañ sutuxlu ba ca xolub Fraans, te mu leer nàññ ne Fraans moom manatul a gañeeti Brusiya ca jamono joojee te manatu koo genneeti suufam. Loolu nag di woon ci 27 oktobar 11870g.

Ci noonu imbraatoor gu Fraans gu ñatteel gi daanu, ñu daal di taxawal ci Paris nosteg pénc gu ñatteel gi . Daal di teg Fraans ñeel Brusiya alamaanug xare gu toll ci juroomi bilyoŋi frank yu Fraans ( loolu mooy tollook – daanak – alamaan bi Napoleon Bonaparte tegoon Brusiya bi mu ko dumaa ca xareb Yena ba, 1806g. Bu ko defee ñu juboo ci xarekati Almaañ yi dunu genn Fraans li feek fayeesul alamaan bi, (moom nag jotees na koo fay ci diirub ñatti at). Nga rax ci dolli dagg gi nu dagge ñaari gox yii di Alsaas ak Loren ci fraans, boole leen ci Almaañ.

Nii daal la bennoo gu Almaañ mate woon ci njiitul Brusiya, ci loxol goor gu dëgër gii ni weñ, Bismarck, mi nga xam ne dafa gëmoon bennal Almaañ ak doonte day ci dereet, ci weñ mbaa sawara. Bu ko defee imbraatoorug Almaañ gi daal di sosu, dib xew-xew nag bu fés ci taarixu Tugal bu bees bi.boroom gàngunaay gi (imbratooru Almaañ bi) mujj di ku ñu joyal ab gogam  ci def li ko neex ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi.
Sartu reew bu Almaañ bu bees bi yaxal na nu sos ñaari jataay:

(1)	Jataayu Bennoo gu Almaañ (Bundasrat) 
(2)	Jattayu (Rechstag)

Dooley yoonal ji nag mi ngi nekkoon ci Bundasrat, di jataay bi nga xam ne mi ngi ame woon ci juroom fukk ak juroom ñatti cer, ñu seddale leen ci nguur-nguuran yi nga xam ne ñoo amal imbraatoor gu Almaañ gi. Brusiya nag moom rekk amoon na fukki kàddu  ak juroom ñaar, ginaaw bi mu am ñaar fukki kàddu. Ak li Brusiya di moomadi li ëpp ci kàddu yi lepp ci Bundasrat, teewul mu gënoon fa’a guddub loxo, gënoon fa a am jeexiit, ndax la ëppoon ca nguur-nguuraani Almaañ ya duggoon ca bonnoog Almaañ ga, danoo takku woon ci Brusiya, te daawunu woote lenn lu mu bëggul. Te daawunu jàllale genn saxal ca jataay ba, bu fukki cer ak ñeent àndadee ca saxal ga.
Bu dee nag jataayu Rechstag nag moom, man nanu ne mooy jataayub askan bi, mi ngi ame woon ci ñatti teemeer ak juroom ñeen-fukk ak juroom ñaari cer, ñu leen di tànn ci anam gu sekkaree. Dooley jataay bii nag daanaka danu koo lafañal, yòqeel ko . ndax nguur ak doole yi nu ko joxoon ci ron sartu reew bu Almaañ bu bees bi, danoo nekkoon di yu doyadi te ñàkk solo.

Bismarck nag, jiite na goornamaa bu Almaañ bi niki diisoowaale walla chancelier. Benn ci ñaari jataay yi manul woon ci moom dara, mu yoroon it sañ-sañ bu rëy, te ci ron kilifteefam tam la Almaañ gu rëy gii gepp nekkoon, nga xam ne ña fa dëkkoon ca atum 1871g jege woon nanu ñeen-fukki milyoŋi nit, mujj àgg ci ñeen fukk ak juroom ñeenti milyoŋ ciy nit atum 1890g, di maanaam bi Bismarck faatoo ba am ñaari at.   
  
Juroomeelu bunt bi

Sanc gu yees gi  

Sabab yi fi indi sanc gu yees gi, ak ay anamam 
Reewi sancaan yi 
Ñaawteefi sanc yi
Yëngu yënguy nasaraanal ak ay wi mu làmbool

Doggantal gu njëkk gi

Sababi sanc gu yees gi aki anamam.

Xamale lan mooy sanc gu yees gi:

Li sikk amul mooy sanc gu yees gii toppoon ci yewwuteg endustri gi ci Tugal, rawati na ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar fukk g, sanc gii de ay reenam tàlliku woon na di dem ba ca yëngu-yëngu yu wuññiy juxraaf yu Tugal yi nga xam ne dees leen di jàppe ñuy bunt bi nu jaare bay dugg ci sanc gu yees gi Tugal doon def ci reewi adduna bi.

Sanc nag dees na ko xamalee ci ne mooy teg loxo gi reewi endustri yu mag yi tegoon loxo mbiri koom-koom yi ak yu politig yeek aada ci reew yu bari ci yu amadi doole yi ci adduna bi. Rawati na yi ci di yu woomle ci wàllug mbay ak mbèll.
Looloo tax sanc - ci maanaam mii mu yor – du lenn lu dul luy yëngu ci nangu ak fëkk alali jàmbur ak ngacc dooley mbindeef yi ak jariñoo leen.

Sababi sanc gu bees gi:

Li sabab sanc lu bari la te lënkaloo, ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii:

(1)	Màgg gu gaaw gi ba ëpp ci wàllug endustri, ci lu bari ci reewi endustri yu mag yi. Loolu nag tax ba reew yii mujj soxlawoo ay ne-ne yu nu laalul  aki ja. Tax na tam ba ag gëpplante gu tar te metti am ci diggante reewi endustri yu mag yi, jëm ci yaatal seenug kilifteef ak sañ-sañ ci gox yi leen man a warlul ag yokkute ci wàllug endustri, ndax seen koom-koomu xeet wepp ci endustri la tegu woon. Li juddoo ci loolu nag lu mujjoon metti la ci reew yu neew doole yii nga xam ne yu mag yii danu leen tegoon loxo, ngir muucu seen njariñ yeek ne-ne yu nu laalul yi, ak ngir def leen ay ja yu mag te yaatu, yu nu man a jaaye seen ligeeyi Tugal yu endustri yooyu.
(2)	Yokk gu ñi dëkke ci reewi endustri yi yokkoon, loolu moo waraloon reew yii gëstu-ji woon fu nuy wàññi seen ëppiitum askan moomu, bu ko defee ñoom ñu man leen a nekkal dib jumtukaay bu am solo buy dëgëral seen koom-koomu reew miy nday. Laaj na ñu xamal leen ne politigu genne ëppiitum askan boobu ak sotti leen ci reew yi nu sanc, politig la bu nu nosoon, jublu woon ci ligeeyal xemmeemteefi sanc yu reewi endustri yi amoon way dëkk yu bari woon ba ëpp.
(3)	Bëgg a soppi nit ñi def leeni nasaraan (nasaraanal), ak wisaare diiney nasaraan ci kaw-kaw yi, ak ñu xamul ñi. Nga xam ne nasaraanal bokk na ci sabab yi gën a rëy yi waral wuññiy juxraaf yu Tugal yi am, te ñooy li ubbi buntub sanc. Waa Tugal yi jëfandikoo nanu diine niki ab raas bu niy jaare ngir àgg ca seen bëgg-bëgg yu sanc yi, yu politig yi, ak yu koom-koom yi, ak doonte danoo làqoon loolu, bu ko defee mbubboo seen wax jooju nu daan wax naan: wisaare ag nasaraan du lu dul xayal ak yiwal nit ñu deltu ginaaw, ñi xamul dara. Adduna bi nag sonne na bu baax ci par-parloo ak boddanteg diine ak xalaatu maa-la-gën bi reewi nasaraan yi ame woon jëm ci yeneen askan yi dul ñoom.
(4)	Wàññiku gu tar gi amoon ci ñi dëkke woon ci kaw gi, ci reewi Tugal yu endustri yi, taxoon ba jafe-jafe am ci wàllug dundub mbay ci reew yii. Loolu yobbu woon na reewi yii ci ñu wuti bii dund ci reew yu neew doole yii nga xam ne mbay amoon na fa doole. Reewi Tugal yi nag jaarunu woon ci yoon ngir am seen càkkuteef loolu, ci misaal ñu jaare woon ko ci yaxantu, waaye kay danoo jëfandikoo doole ak noot ak sanc, sukkandiku ci seen dooley xare ji, ak ñawug seen ngànnaay, ak neew dooleg geneen wàll gi mu fas yeenee noot, loolu mooy li ko dimbli ba mu man a am bëgg-bëggam yooyu ci kaw askan yu doyadi yi.
(5)	Lu bari ci reew yu mag yi, li leen doon defloo sanc googu mooy feeñal ag yëg-sa-bopp, aakimoo mbir yi, ag rëy ci wàllug xeet, yaakaar ne ñoo gën, yooyu nag ay jumtukaay lanu won ngir wone doole ak màgg gi nga xam ne reewi sanc yii màggoon nanu ko te ame ko ni doole.
(6)	Ay lonkoo yu Tugal ak yu dul ñoom, yu mag feeñ nanu ci biir yewwuteg endustri gi. Dajale woon it alal ju bari, ba gisoon ne leegi danu koo war a meññali ca reew yay màgg, ci wàlli koom-koom yi. Ci noonu lonkoo yu adduna yu mag yi tàmblee gëpplante ci meññilu alal yooyu, loolu nag jur ag jongante gu mag te tar, ba mujj sax yii lonkoo tàmblee sàkku ci seeni goornamaa ngir ñu jàpple leen te dëgëral leen, loolu tam daan yobbu goornamaa yi ci ñuy aar seen njariñu lonkooy reew. Loolu nag nooyal na yoon wi ba xeetu sanc gu politig man a taxaw, di lol gëpplanteg koom-koom a ko fi indi.
(7)	Bëgg gi reewi sanc yu mag yu bari bëggoon na dëgëral seen yoonu jokkoo gu adduna, loolu yobbu leen ci ñu teg loxo yenn yoon yu strateji yi, ak waax yu am yi solo, ak yoon yu mag yi am solo ci wàllug jokkoo gu adduna gi, di taqale diggante goxi adduna bi.
(8)	Bëgg gi yenn ci reewi sanc yu mag yi bëggoon a tas seeni xalaat, aki dal (principes) yu seeni làngi politig, ak seeni aada, jàppe loolu nag ab jumtukaay buy ligeeyal seeni xammemteefi sanc.

Anami sanc gu bees gi:

Sancug Tugal gu yees gi dafa jëloon ay melo aki anam yu wuute, yoo xam ne xew-xew ya peegoon te yiiroon reewum sancaan mi ak mi muy sanc, xew-xew yooyu danu doon jeexiital ci ñoom, bu ko defee sanc gu bees gi dikk ci ay anam yu bari, ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii:

Sanc ngir dëkk:

Xeetu sanc gu ñaaw gii feeñ na ci ginaaw yëngu-yëngug wuññiy juxraaf yu Tugal yi.
Bu ko defee reewi Tugal yiy wuññi, daal di taxaw ci neewal doole ñi cosaanoo woon ci reew yi nu wuññi. Jaare ko nag ci di leen dàkku ak a genne seeni reew, ak di leen alag ci xare yi, di leen toraxal, di leen seeyal ci biir mboolaayi reew miy sanc, maanaam di leen def daanaka ñuy ñenn ci ñoom ci wàllug aada, deesu leen manatee ràññale.
Xeetu sanc wii mooy li waa Espaañ defoon ca Endo yu xonq ya ca Amerig gu digg ga ak gu bëj-saalum ga, bi nu leen sancee te dëkke leen, taxawal fa ay sancu, yoy mujjoon nanu cuub gox bii ci cuubug Espaañ, ginaaw bi fi ay waa Espaañ jëlee barabu endo yu xonq ya fa cosaanoo, mel ne leegi fa lanu cosaano, loolu di ci Amerig gu digg gi ak gu bëj-saalum gi, lu ci dul Bresil,moom waa Portigaal a ko sancoon.

Nu mel noonu la sahyooni yahood yi defoon ca Falastin, bi nu ko sancee ci doole, dëkke ko, reewi sanc yu mag yi jàpple leen ci, Britani nekk ca bopp ba. Ci noonu la yahood yi tasaaroo woon ci adduna bi, dajee, dëkksi ca Falastin, ginaaw bi nu leen fa gàddaayalee jëme, ci ron aarug reewi sancaan yi, ak li askanu Falastin daan xeex loolu lepp, te daan ci jiyaar ngir bañ ko.  

Nii it la sancug Tugal gi meloon ca Afrig gu digg gi, ak Rodisiya, ñu fay teg doomi Afrig yi lu sakkan te lëw ciy coona, di leen noot, di leen teg loxo, di leen tiital, di leen tàqale ak a gënale ci wàllug xeet, ak lu bokkul ak loolu lepp ci anami mbugal yu tar te mbaam-àlle.

Teg loxo gu xare :

Ay reew yu sancaan jug nanu, teg loxo ay reew, nangu leen ci doole. Loolu nag li leen ci gënoon a jañ, gënoon leen cee yobbu mooy neew doole gi nu gèndiku woon ci yii reew, rawati na ci wàllug xare. 
Li ñu doon jublu ci teg loxo googu, mooy man cee jaare bay wéyal ak a doxal seen naali sanc yooyu daan tax ba nuy man a teg loxo ci koom-koomi reew yi nu nangu, ci seeni dooley xare, ci seen politigu bitim reew ak seeni mbiri xam-xam ak aada, ngir man a samp bu baax seen kenoy sanc ci dëkk yii.
Misaali sanc yu mel nii yu bari lanu, nañu ci indi yii rekk:
Sanc gi Fraans defoon Aljeeri, atum 1830g, ak sanc gi Britani defoon Adan, atum 1839g, defoon ko it Isipt atum 1822g,  ak teg gi Fraans tegoon loxo dunu Madagaskaar, atum 1894g, Beljig defoon ko Kongo atum 1907g ak nangu gi Itaali nangu woon Libi atum 1911g, ak Ecopi 1936g.

Xeetu sanc wii mooy wi gënoon a tar te gën a ñaaw ci xeeti sanc yi, ndaxte lu diisoon la ci ñi cosaanoo woon ci reew yi nu tegoon loxo. Ndaxte sanc gu sukkandiku woon ci jëfandikoo doole la.
Waaye li muy tar lepp ak a tiitale, teewul nit ñi xeexoon ko, te xaru woon ci jële ko fi. Jànkoonteek lu sakkan ciy jafe-jafe aki coona ci seen xeexu njàmbaar boobu ñu ko doon xeex, ba mujj ame ci lu màgg li nu doon wut, muy gore ak tembte, ak dàq sancaan yi ñu juge seeni reew.

Aar :

Reewi sanc yi mujj nanu wut geneen anam gu yees gu nuy sance ak a tege loxo reewi jàmbur yi, ñu soppi woon seen sanciin woowu doon tegu ci dooley xare, wut weneen wu nuy tudde “AAR”. Aar nag ci maanaa mu sanc mi mu yor, gënul benn yoon sanc gi nu daan defe ci teg loxo ak nangu reewum jàmbur ci doole, moom daal AAR, tur la ci tur yi sancaan yi indi te jëfandikoo ko ci yenn ci ay jamono.

Bu dee maanaa mi aar yor ci wàllug sanc, mooy def gi reewi sancaan yi daa def ay dëppoo  aki kollarante ci anam gu maandoodi ak yeneen reew yu doyadi yi, te neew doole. Bu ko defee reewum sancaan mi day kollaranteek reew mi mu sanc ci di ko aar ci mbooleem tooñ gu ko man a dikkal, juge ci dooley politig ju digook moom walla jeneen.  Bu ko defee loolu di may reewum sancaan mi, muy doxal mbirum reew mi nuy aar, ci wàlli kaaraange, bitim reew, ak koom-koom. Reew mi nu aar daal du doxal lu dul mbiri biir reewam rekk. Loolu nag daa na tax mu nu aar mi daawul am temb gu mat, ndax ag gore gu politigam kollarante yooyu danu ko daan tënk, ba daa ko tee muy def ay ligeeyam ci mbooleem ay mbiri reewam, ci ni mu ko neexe.
Misaal yi ci loolu yu bari lanu, ñu indi ci yii rekk:
Aar gi Fraans defoon Tunisi atum 1881g, ak Maraakes 1912g, ak aar gi Britani defoon Adan, dale ko ca ba mu ko tegee loxo atum 1839g, ak yeneen barab yi mu tegoon loxo.

Feetale :
  
Reewi sancaan yu mag yi tàmbli woon nanoo wutati ay tur yu bees, ngir sanc gu bees gi, ginaaw xareb adduna bu njëkk bi. Loolu nag mu jublu woon ci muur sanc gii muy def muuraayu ag yiw akug xay. Loolu nag du tee sanc moom di lenn rekk, ak mbubb mu mu man a sol, ak melokaan wu mu man a dikke . Ci noonu la “feetale” dikke, moom nag ag anam la ci anami sanc gu yees gi nga xam ne jataayu kureelu xeet yi saxaloon na ko, te nangu ko, mooy kureel googu nu sosoon ca Paris, ca ndajem jàmm ma nu defoon atum 1919g, ngir lijjanti lëj-lëj yi amoon ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi. Boobu kureel nag Fraans da ca’a defoon ay jeexiit yu mag mook Britani. Nga xam ne ni nu bëgge mu mel ni daanaka la mel.

Dalu feetale ci jëmmi boppam, ñi ngi ko jële - ci cosaan la – ca yoon  wu Rom wu yagg wa . Feetale nag noste la gog defoon na mbooleem reew yi nga xam ne “reewi dëppoo yi ” nangoo woon nanu leen ci imbraatoorug Almaañ gi, ak reewum Usmaan mi , ñuy ay reew yu nekk ci ron feetale googu. Bu ko defee, reewi dëppoo yi ñoo nekkoon reew yi nu joxoon feetale googu, maanaam ci seen ron kilifteef lanu feetale woon mbooleem reew yi nu nangoo ci Almaañ ak reewum Usmaan mi.

Bu ko defee ñu waral ci reew yiy feetewoo feetale gi ñuy def leeg-leeg ñu indi ay saxal aki leeral yu aju ci seen dooley xare yi nekk ci reew yi nekk ci seeni loxo, te nu feetale leen ko. Saxal yii nag ak leeral yi kureelug feetale gi nekk ci kureelug xeet yi lanu ko daa indil.
Feetale gi tam mi ngi daa yam ci benn ñeenteelu xarnu, maanaam benn xaaj ci xarnu bu xaaj ñeenti xaaj. Misaal yi aju ci xeetu sanc wii yu bari lanu, ñu wax la ci rekk:
Feetale gi nu defoon Britani Iraak, penkub Jordani ak Falastin mi nga xam ne dafa genn ci teg loxo gu Britani, ngir tàbbeeti ci gu Israayil. Ak feetale gi nu feetale woon Fraans Siri ak Libaa, ak feetale gi nu defoon goornamaab neewiit yu weex  ya nekk Afrig de Sud, feetale gi nu leen feetale woon mbirum Namibi, ñu yor ko di ko doxal. Ak feetale gi nu feetale woon Japon duni Pasifig, duni Marshal, ak feetale gi Ostraali ame woon ci kaw Gine gu yees gi añs.
Kureelug xeet yi nag, daa xëyoon rekk sàkk feetale, di ko teg reew yu neew yi doole, ci sañ-bañ, te du leen ci tàggu mbaa mu ciy diisoo ak ñoom.

Denkaane :

Moom itam aw xeetati la ci xeeti sanc yi, wii nag xeet la wu feeñ ci ginaaw xareb adduna bu ñaareel bi. Ñu amale ko nag ci genn saxal gu juge ca mbootaayu xeet ga ñu sosoon , atum 1945g, ngir wutu fi kureelug xeet yi.
Mbootaayu xeet yi nag neenaloon na kureelug feetale gu sax gi nekkoon ci kureelu xeet yi, ngir teg fi leegi jataayub denkaane bi nga xam ne moom lanu wekk leegi mbirum saytu sancu yi “reewi digg” yi moomoon, yilifoon leen: Reewi digg yi ñooy Almaañ, Itaali ak Japon bi nu leen laata a dàqe ci xareb adduna bu ñaareel bi. Moom jataay boobu tam moo yoroom mbirum reew yi tembagutoon. Misaalum xeetu sanc gii: denk gi nu denkoon Itaali Libi ak Somali ak denk gi nu denkoon Britani Tanganyika  ak  yeneen . 

Sancug aada :

Moom de xeet la ci xeeti sanc gi nuy jaare ci xalaat. Yenn ci reewi sancaan yi danoo jugoon ci jariñoo xalaat ak aada, ngir ligeeyal seeni njariñi sanc. Ci noonu ñu sosoon ay jàngu (leekol) aki xamluwaay  aki fajuwaay , aki barabi nasaraanal, ak yeneen, loolu lepp nag ngir man cee jaare bay sanc yii reew ñu ko def, te man leen a moom.

Fraans de xeetu sanc wii def na ko ci Afrigu bëj-gànnaar gi, ci : Tinisi, Aljjeeri, Maraakes, (sunu reew mii it di Senegaal def na ko fi), defati ko ci reewi Shaam yi, rawati na Libaa. Reewi dankub mbokkte bi  it, Bennoog Sofiet gi jiite leen, ñoom itam jeem nanu ba sonn ci wisaare seen xalaat yi ak seen dali làngi politig yi ci reew yu bari ci adduna bi.

Barabi sañ-sañ :

Lu bari ci reewi sancaan yi danu doon ngàrtaajoo ak a aakimoo koom-koomu lenn ci reewi Asi yi ak yu Afrig yi, ba noppi naan ñoom de dugguñu te seen yoon nekkul ci mbiri politig yu reew yii, du caageenug seen mbiri biirum reew. Misaali xeetu sanc wii, mooy la xewoon ca Iraan atum 1907g, nga xam ne danoo defoon bëj-gànnaaru reew ma muy barabu sañ-sañ ñeel Rusi gu Xaysar gi, bëj-saalum ba nu def ko barabu sañ-sañ ñeel Britani.
Amoon na it ay xejj  yoo xam ne yenn ci reewi sancaan yi amoon nanu leen ci reewi adduna bi, lu ni mel mooy xejj yi nga xam ne reewi Tugal yi amoon nanu leen ci reewi Shaam yi, ci jamono ju Usmaan ji  ak xejj yi nga xam ne reewi sancaan yi amoon nanu leen ci Siin ak Tayland ak yeneen.  

Ñaareelu doggantal

Reewi sancaan yi

Lu bari ci reewi sancaan yi doon nanu def seen cawartey sanc yooyu ci fu bari ci reewi adduna bi, ci gox yii di: Afrig, Asi ak adduna bu yees bi (Amerig). Reew yi ëppoon solo ci reewi sancaan yooyu, ci taarix, ñooy:

Reewum Portigaal:

Waa portigaal yi ñooy ñi njëkk a def ay wuññiy juxraaf yu Tugal ci ñaari gox yii di Afrig ak Asi. Ñoo ci jiitu woon waa Espaañ, Holand, Angalteer, ak waa Fraans ak ñeneen ñi jot a def ay wuññiy juxraaf  ci jamonoy yewwute gu Tugal gi.

Tukkib Vasco de Gama bu njëkk bi mu defoon ci Afrig ak End, moo ubbi woon gëti waa Portigaal yi jëme leen ci sanc ay barab yu bari ci Afrig ak Asi ngir teg loxo geeji penku yi, ak rënk yaxantug penku gi , rawati na li ci aju ci ay rëndaay , ak ngir yàq koom-koomu reewi jullit ñi, rawati na nguurug Mamaalig yi, ngir loolu man a doyadil jullit ñi, neewal leen doole.

Waa Portigaal yi tàllaloon nanu seen kilifteef ak sañ-sañ ci duni Madira yi, Bopp bu Wert bi ak Osoras, barab yooyu nekkoon ci màmbulaanug atlas gi,la ko dale woon ca ñeenteelu bu njëkk ba  ca fukk ak juroomeelu xarnu g. Cig nangu tegoon nanu loxo barab yu bari ci Afrig ak Asi ci xarnub fukk ak juroom g, yu ci mel ni: Mosambig ci penku Afrig, Angola ci sowwu bi, Ecopi, ak duni Madagaskaar, Moris ak Silaan ak xat-xatu  Hormos ak xat-xatu Malga ci daanaka-dun bu Malayo añs.

Waa Portigaal yi defoon nanu seen “sanc gi ngir dëkk” ca Bresil, gi nekk ci Amerig gu bëj-saalum gi, ñu indaale fa woon lu sakkan ciy jaam yu Afrig ngir ligeeyloo leen ci mbay meek gasum mbell mi.
Nu leeral leen ne sancug Portigaal moom dundul lu ëpp ab xarnu, ndax seen soxot gu tar gi nu ame woon ci ñoñ ñi cosaanoo woon ci seen sancu yooyu, ak ngir ñàkk gi nu ñàkkoon a yittewoo mbirum nos politig bi ak goornamaa bi ci seeni sancu. Ak tam ngir xeeg gut ar gi leen askani yii barab doon xeex.

Reewum Espaañ:

Espaañ def na ay ligeeyi wuññeem yu juxraaf moom itam ginaaw waa Portigaal, waaye jariñu ci seen xam-xam boobu ñu jot a am ci lef  moomu. Bu ko defee, waa Espaañ jël goxi Amerig gu digg gi ak gu bëj-saalum gi def leen ay sancu yu mu sos ngir dëkksi fa. Moom nag ag sancam daa tegu woon ci fitna, ray, song, jaay doole ak gënale ci wàllug diine. Ci noonu ñu tàggatoon jaam yu ñuul yi ak endo yu xonq yi ngir ñu bayal leen tool yi, gasal leen mbell yi. Ñu daal di woon jël yii reew cuub leen cuubug Espaañ, ci làkk, ci diine, ci aada ak ci taarix, ba mujj sax bii gox ñu koy wooye Amerig gu Latin gi, di ko askanale Latin gi nu jublu woon Esspaañ ak Portigaal.
Espaañ it tàllaloon na ag kilifteefam, lal ko ci kaw ay barab ci goxu Afrig, yu ci mel ni duni Kanari ak àllub Maraakes bi ak goxu Afni bi dend ak Maraakes ak Gine gu Espaañ gi nekk ci bëj-gànnaaru rëddu yamoo wi .

Sancug Espaañ gi neewoon na doole te doyadi ci kanamu jongante gi Tugal doon def ci wàll googu. Ci noonu waa Angalteer yi yàqate woon seen mbooloom gaal mi tuddoon Irmada, atum 1588g. Mbooloom gaalum Holand mi tam moñoxeeti mu Espaañ mu lòtt mii atum 1607g. Ci noonu la Espaañ mujje di reew mu neew doole mu loof ci kanamu gëpplante  gu Angalteer, gu Fraans ak gu Portigaal. Bu ko defee, ay fipp am ca sancuy Espaañ ya, ci noonu askani dëkk yii daal jéngu xeex ba roccee seen tembte ci loxol waa Espaañ yi.

Reewum Holand:

Waa Holand yi danoo duggoon ci ngérum Protestant ba noppi nekk ci ron teg loxo  gu Espaañ gu katolig gii. Looloo taxoon ñu defoon seen fipp gu mag googee kontar katolig yu Espaañ yii, daal di noccee ci ñoom seenug temb ci doole ci njëlbeenug xarnub fukk ak juroom ñaar g. Waaye temb gii nag nangu na ko (moom Espaañ) ci anam gu ofisel atum 1648g, ca kollareg Westfalia ga nu defoon, ginaaw xareb fanweeri at ba .
Waa Holand daal di taxawal lonkoo gu End gu penku gu Holand gi ci njëlbeenug xarnub fukk ak juroom ñaar g. Daal di sóobu ci geewub jonganteg sanc gi ci penku bi, daal di not waa Portigaal yi ci wàllug sanc, teg loxo duni End yu penku ya ca Asi. Yaatuwaayu suuf yi Holad mujjoon sanc mujjoon na gën a rëy juroom ñaari yoon yaatuwaayu Holand gu ndaw gii ci jëmmi boppam. 

Sancaan yu Holand yooyu danoo rënkaloon seen bopp rekk yaxantu gi aju woon ci rëndaay yi, kawsu, attaaya, kafe, suukar, seng ak petrol añs.
Waaye ñii dëkke woon ci sancu yu Holand yi te cosaanoo fa, xeexoon nanu kontar waa Holand yii ba mujj am tembte atum 1949g ci turu Endonisi.
Waa Holand yi tàllaloon nanu seenug sanc ci diir bu gàtt ci kaw ay barab ci adduna ju yees jii di Amerig.
Ñu taxawaloon lonkoog End gu sowwu gu Holand gi atum 1622g, ñu sancoon goxub dexug Hadson, daal di jënd Manhatan ci endo yu xonq yi, daal di taxawal dëkkub Amstardaam bu bees bi nga xam ne waa Angalteer yi nangu woon nanu ko ci Holand, tudde ko New York. Waa Holand tam sancoon nanu – ci diirub fanweeri at – ag wàll gu mag ci Bresil gi nekkoon ci ron kilifteefug Portigaal.

Reewum Beljiig:

Leopol mu ñaareel mi tegoon na loxo reewum Kongo mi nekk ci digg Afrig atum 1876g, daal di koy def ag moomeelam, loolu nag wéyoon na di nekk ba atum 1908g, ci ginaaw bi lanu tuxale moomeel gii yobbu ko leegi muy gu reewum Beljig. Kongo nag reew mu naat la lool, te woomle ci ay koom-koomi mbell. Waa Kongo nag jàmmaarloo nanook sancug Beljig gii leen doon jariñook a toggi mbugal, daan jariñoo it seeni koom-koom ci anam yu ñaaw a ñaaw, loolu yobbu leen ci ñu am tembte atum 1960g ci turu Saayir.

Sancug Britani:

Imbraatoorug Britani gi moom lanuy jàppe muy gi ëpp ci reewi adduna yi mas a def sanc gu yees gii nu xam tay. Moom mooy imbraatoor gu sanc gi nga xam ne jant manul a so mukk ciy sancoom ngir bari gi mu bari lu mu sanc ci suufus adduna si. 

Britani dey defoon na ci wuññiy juxraaf yi, waaye ca Amerig gu bëj-gànnaar ga, mu sancoon lu sakkan ciy suufam, waaye dëkke leen, te sonn it ci dindi kilifteefug Fraans ak Holand ci gox bii te jële ko fi. Bu ko defee, sancu ak dëkkuwaay yu Britani yi ci Amerig gu bëj-gànnaar gi desoon ci ron cang gu sanc gu Britani ba kero Diiwaan yu Bennoo yu Amerig yi  di am tembte , naka noonu Kanada, ñoom reew yii nga xam ne dafa am lu leen boole ak Britani, muy bokk gi nu bokk ak ñoom askan, te bokk nekkandoo ci “Komonwelth gu Britani”. Britani sancati na Ostraali ci anamug dëkk ak Newsiland, waaye temb nanu ñoom ñaar te mujj bokk ci Komonwelth.

Britani sanc na End, wéyal fab sañ-sañam, daal di sos lonkoo gu End gu penku gu Angalteer gi atum 1600g, mu jot a dàqe Fraans ca daanaka-gox bu End ba  . Mu manante  Siin ci mu ubbi ay waaxam  ci kanamu Afyon bii nga xam ne Britani daa na ci indi lu bari ci waa Siin yi. Looloo waraloon xare ba tàkkoon ci diggante Siin ak Britani, di woon xare bu nuy tudde xareb afyon bu njëkk bi nga xam ne wéyoon na la ko dale woon ca atum 1840g ba 1842g, nga xam ne ca la Britani nangoo waaxub Hong Kong bu straateji bi, waax bii mi ngi woon ci loxol Britani ba bu yàggul. Xareb afyon nag benn la ci tooñaange yi nga xam ne Britani mi ngi ko doon tooñ waa Siin cig wàll, ak nit ci jëmmi boppam ci geneen wàll.

Britani tegoon na loxoom dunu Brem atum 1799g, ak Adan atum 1839g, ak Borma atum 1885g, akug wàll ci Malayo. Mu defati ay aar aki kollarante yu maandoodiku ak ab lim ci barab yi nekk ci bëj-saalumu dunu araab bi, ak tefesug golfub araab bi. Mu sanc Isipt, Sudaan, Iraak, Penkub Sordani, Falastin ak yeneen barab ci reewi Asi yu ñàkk doole yi.

Britani nangooti cig sanc lu bari ci reewi Afrig yi, lu mel ni: Afrigug Bëj-saalum gi , Nijeeriya, Oganda, Tansani, Rodisiya ak Somali gi nu xame woon ci turu Somali gu Britani gi.

Sancug Britani gi nag mooy gi gën a ñaaw ci mbooleem xeeti sanc yi, ndax moom da daa jëfandikoo cig sancam doole, teg loxo  ak jariñoo ne-ne yu nu laalul yi  , ak kàttanug askan yi ak tas nit ñi ak xàjjale leen, fitnaal leen ak tooñ leen. Waaye li lii lepp di tar, teewul askani sancu yu Britani yi xeex nanook sancaan bi ba kero nu ame seen tembte, ci noonu la Britani dellu mel namu meloon, yor dayo bi mu yoroon, ginaaw bi sancoom yii tembee wëliif ko, foofa la ko lòttug politig gaare ak gu koom-koom. 

Reewum Fraans:

Waa Fraans yi bokkoon nanu ci ligeeyi wuññi yu Tugal yi ci goxi Amerig gu bëj-gànnaar gi, rawati na ci Kanada ak gox yi peek dexug Santa Lorens gi. Ñu sosoon fa ay sancu yu Fraans, yu ci mel ne: Kebeg gi nga xam ne ci tefesug Santa Lorens gi lanu ko taxawaloon, ak sancu bu Luwisiyana bi nga xam ne turam wii mi ngi juge ca Luwis mu fukk ak ñeenteel ma buurub Fraans ba.

Ag gëpplante gu mag xewoon na ci diggante waa Fraans yi ak waa Britani ci Amerig gu bëj-gànnaar gi, ci xarnub fukk ak juroom ñatt g. Waaaye Britani moom jot na a neewal doole kilifteefug Fraans gi ci barab yooyu, bu ko defee Fraans moom teg loxo yeneen barab yu bari ci Afrig, fu ci mel ne: Aljeeri, Tinisi akug wàll ci Maraakes, daal di sutuxlu ci tàkkug  Afrig gu mag gi, daal di yaatal bu baax seen sañ-sañ ak kilifteef ci Senegaal, Kongo, Nijeer, Madagaskaar, Somaal gi nu tudde woon Somaalug Fraans gi, Gine ak Dawme.

Fraans tegati loxo ay reewi Asi, fu ci mel ne: ay wàll ci End, waa Britani jële leen fa atum 1763g. ñoom de jotoon nanoo taxawal lonkoo gu End gu penkug Fraans gi, ngir gëpplanteek lonkoo gu End gu penkug Britani gi, ak lonkoo gu End gu penkug Holand gi ci wàllug yaxantu ci penku bi. Fraans sancati Sireek Libaa ci turu feetale , ci ginaaw xareb adduna bu ñaareel ba . 
Sancug Fraans gii nag daa melowoo ag tooñ, tiitale, jeem a far aaday reew yi mu sanc ak seeni màndargay reew ak jëmm. Lu mel noonu it mooy li nu def ci reewi araab yi nekk ci bëj-gànnaaru Afrig te Fraans tegoon leen loxo. Waaye way dëkke ya xeexoon nanu sancug Fraans gii, ba mujj am tembte gu mat .

(Fii fi Senegaal, waa Fraans sonnale nanu fi, tege fiy fitna, gennee fi, xoolal ku mel ni Sëriñ Tuuba., cig tooñ lanu ko fi gennee, sanni ko ca àlli Gabong yu lëndam ya, yobbooti ko Moritani, te fii nu koy genne de du seenum reew, reewam la. Xoolal ma fa ñuy wax (Camp Caaroy) ak jëf ju ñaaw ja nu fa def, xoolal ma sunu làkki reew yii nga xam ne ba tay manunu leen di jàng te Fraans nekk ci ginaaw, xoolal ma yeneen mag yi nu sonnal, xoolal ma aaday nasaraan ji nu fi bëgg a saxal, leegi la sax waaye ci ginaaw ak seen Senghor mi fi nekkoon nga xam ne daanaka tubaab la woon, ngir ne seenub ligeey la woon bu leen fiy ligeeyal, lenn luy sunu aada safu ko woon, du col mi, du wax ji, du lekkiin wi, du lenn lu mu man a doon, naka noonu ñi nekk ci ngunoom ci ñi mu sos, defar leen, ñu koy ligeeyal).

Reewum Almaañ:

Imbraatoorug Almaañ gi moom itam dugg na ci geewub sanc bi ak jongante gu adduna gi, ginaaw bi mu amalee ag bennoom atum 1871g, mu daal di sanc Kamerun ak bëj-saalumu sowwub Afrig, bi nga xam ne dees na koy wooye bëj-saalumu sowwu Afrig bu Almaañ bi, ngir sanc gi ko Almaañ sancoon, ak bëj-saalumu penku Afrig bi nu tudde ba tay bëj-saalumu penku Afrig bu Almaañ ak Togo .
Almaañ it jotoon na a teg logo lu bari ci duni Pasifig yi nga xam ne ñi ngi leen gënoon a xame ci turu “duni argabiil  yu Bismarck yi” . 
Ñu nangu tam ñoom waa Almaañ xaajub bëj-gànnaar bi ci duni Gana gu yees yi nekk ci màmbulaanug atlas gi. Waaye Almaañ moom mujjoon na ñàkk sancoom yii ci ginaaw bi nu ko dàqee ci xareb adduna bu njëkk bi.

Reewum Itaali:

Itaali tam soobu na ci lefum gëpplanteg sanc gi, ginaaw bi mu bennoo, atum 1870g, mu daal di teg loxo ay sancu ci Afrig, ci Eritri, Somali, gi nu tudde Somali gu Itaali gi, Libi ak Ecopi. Itaali nag jëfandikoo na gën ja a ñaawi anami mbugal ak ray ci kaw askani yii reew. (Omar Muxtaar ca Libi fàttaliku leen ko).

Reewum Rusi mu Xaysar mi:

Sancug Rusi gi moom mi ngi jëmoon ci Siberiya, Turkmanistaan ak ay gox ci Asi gu digg gi. Rusi it teg loxo gox yi nekk ci bëj-gànnaaru dexug Amoor gi ci Siin, daal di fay taxawal ab dëkk bu bees ci turu Vladivostok, lijjanti it ba Siin gu neew doole gii jox ko ay sañ-sañ ci defar yoonu weñ  wu jaar ci suufi Manshuriya gu Siin gi, ligeey ba daal di tàmbli ca atum 1889g. Sañ-sañu Rusi it yokku ca Kore, mu daal di seddoo Iraan mook Britani, daal di sanc wàllug bëj-gànnaar ga, ci ginnaaw bi nu defee seen dëggoo gu xaritoo gi, xaatim ko cis een diggante ñoom ñaar atum 1907g.   

Buntub ñatteel bi

Ñaawteefi sanc: 

Li sikk amul mooy sanc gii amoon ci adduna bi, ci melokaanam yepp aki anamam, bokkoon na ci li gënoon a soof te ñepp bañoon ko te sib ko, rawati na askan yi nu ko teg ci seen kaw, ba nu mos aw wextanam, reer cig lëjam. Sanc de bijj na lu lëw ciy ñaawteef aki jeexiit yu bon ci ka waskan yu lòtt  yi yanu woon ab sukkam. Ñaawteefi sanc moom dees na leen man a gaw ci wàll yii:

Ñaawteefi sanc yu politig:

li kenn reerewul mooy ne reewi sanc yi de rekki nanu ngorug askan yi nu sancoon seeni reew, rekki it seen sañ-sañ ci wutal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom, te loolu dal  yi aju cig nite yepp ak yu yoon yepp woote nanu ko. Xañoon nanu it askan yi ñuy àttewoo ci sartu-reew , ak ci nostey demokraasi  yu tegu ci cëslaay lu mucc te sell, loolu nag mi ngi am ci ginaaw bi nu yàqee mbooleem campeefi xeet yi  te dindee leen fi, wuutal fi yeneen yuy ligeeyal seeni xemmeemteefi sanc.

Sanc gi nag jeemoon na a defi pexe ba askan yi nu sanc dunu doon mukk benn, bu ko defee mu def lu nekk, jëfandikoo pexe mu mu man a doon ngir xeet wi bañ a nekk benn. Mu tàmblee wut lepp luy tàqalee di ko sotti ak a wisaare ci mepp mbooloo muy menn, ak wepp xeet wuy wenn, ci mepp reew muy menn. Mu soññ te sawarloo yëngu-yënguy beddiku yi  yi nga xam ne neewte  yaa ngi leen doon sàkku ak def, daal di yittewoo bu baax lepp lu aju ci luy jeqi ag xëccu jëm ci waaso mbaab kureel walla boddante mbaa woote ag gën ci biiru xeet ak wuute ci ngér, mu ñëwati xóotal dalub tàqle politig ci mennum reew, daal di sawarloo làng yi ànd ak moom ci politigam boobu, daal di def ay soppi ci dig yi , yooyu soppi nag ñoo mujj di jëfka  yu mag yi mujj di taal gilinug wuute gi ak noonoo ci diggante dooley politig yi dëkkandoo, dendandoo, mu dooleeti indil reew yi mu sanc ay jafe-jafey politig yu fasu, yoy reew yi nu sanc de wéy nanu di jànkoonteek ñoom ay ati at, ginaaw bi nu tembee, yooyu jafe-jafe wéyoon nanu di fi sax ginaaw bi nu mujjee nekk di fi ag dund gu yees. Sanc nag jëfandikoo woon na mbooleem xeeti jumtukaayi mbugal yi kontar askan yi, mu duma, tëj, mbugal, te ray lu sakkan ci askan yi te dara waralu ko lu dul ne danoo fippoon kontar ko, sàkku woon nu nuy goree te temb, te loolu àq ju mag la tey yelleef ñeel leen. Waaye askan yii yanu woon sanc gi, jugoon nanu xeex, def ci seen lepp ngir yekkati yan bu diis bii tegu ci seenum ndodd.

Ñaawteefi sanc yu mboolaay:

Sanc daal dafa defoon yitteem ci tas, xottite bennoo gi am ci mboolaay yi nekk ci sancu yi, jaare ko ci soññee cig tàqalikoo, wisaare nosteg kureel  ci biiru askan, bu ko defee kureelug laman yi walla gu sang yi daal di feeñ, am ay sañ-sañ yu bari aki ngëneel yu tax ñeneen ñu ndool ñig ñàkk di bëgg a ray akug reer mere woon leen . Gii kureel nag ligeeyal na ba tàyyi sanc gi ci anam yu bari. Bu ko defee jaasiy sanc gi nekk fi di lu nu bocci ci baatub ñu ñàkk ñi, di leen tegi coona, di leen fitnaal, te kat ñoom ñooy ñi ëppoon ci askan wi.
Am geneen kureel gu feeñati ci wetu gu lamani sancu yi, mooy kureelug sang yu doxandeem yii nga xam ne ñoo tegoon loxo ci koom mi ak ci nguur gi walla àtte gi, bu ko defee tàggat doomi sancu yi ci ñu leen di ligeeyal.

Sanc gi tàbbal na ci sancu yi mbooleem aada yu ñaaw yi man a yàq ag mboolaay, man a ñaawali jikkoom. Mu soññe cig mbon, reer, jëfandikoo dorog ak yiy màndal  ak wure ak kart ak yu dul yooyu ci aada yu ñaaw yi man a tas bennoo gu ag mboolaay, te dëgëral nekkug sancaan yi ak seen doole ci sancu yi, te gën fee suuxat seen reeni sanc. 

Sanc gi de jeemoon na – jëfandikoo woon ci loolu bepp kerkeraan bu mu amoon mbaa yoon wu mu xamoon – ngir gòndi niti sancu yi ci xayug Tugal gi , te sopploo leen ko, ngir ag maas man a judd guy gëm te gòndiku ci jëm-kanamug Tugal gi ak xalaati waa Tugal yi. Li ñu jublu woon ci raxasug xel gii mooy indi fi ag maas gu yees guy ligeeyal njariñu tubaab yi, rawati na bu maas gii mujjee jiite reew yi ci politig, jaare ko ci seenug jàpple. Waaye ànd ak pexey sanc yii yepp ngir amal loolu, teewul askani sancu yi tas yaakaari way sanc yi, sooyal seeni mebat.
Seeni mebat sooy na, seeni yaakaar tas, bi nu gisee ne askan yi dey ñi ngi wéy di gën a jàpp ci seeni diine, di gën a ŋoy ci sseeni aada, di gën a ngëb ci seeni pas-pas yu laab yooyu. Fonk seen bopp, seen taarix aks een xalaat.
Nga gis ne maas gi juddoo ci jamonoy sanc ñoo yanu woon raayob fipp gi ak xeex bi kontar sancaan yi, ñu saxoon nag ci  noonu ba mujj fuqarci ci doole seenug gore akug temb gu mat sëkk.

Ñaawteefi sanc yu koom-koom:  

Li njëkk a yitteel sancaan yi mooy am ay ne-ne yu nu laalul yu mbay ak mbell ba man a doxal seen ligeeyuwaay , buk o defee man fa a ligeeye lu nuy genneeti di ko jaayati ca reew ya nu sanc, looloo taxoon sanc gi saxoon ci di muucu ak a ngacc xeewali reew yi nu sanc yu mbay yeek mbell yi. Mu soññ lonkoo yu jàmbur yiy rënk, ñu ñëw meññilu seen alal yi ci reew yi nu sanc ci anam ak wàll yiy ligeeyal tey jariñ reewi sancaan yi. Bu ko defee yii lonkoo taxaw ci jariñoo koom-koomi reew yi nu sanc ci diir bu gàtt , ndax danoo yàgg a ragal fipp yi leen daan kontar te askan yu ndooli sancu yi daan leen def, ñoom ñi nekkoon ci ron yan bu diis bii leen tegu woon te weesuwutoon lenn lu dul sanc gi.
Reewi sancaan yi yamunu woon ci muucu xeewali sancu yi, waaye àggoon nanu ci def leeni ja yuy muucu ak a dékku marsandiisi Tugal yi. Lii nag moo nuy woo ci ñu tudde sanc gi “siyukaay  biy si buy dem ak buy ñëw” .

Sanc gi moom da daan xeex endustri ci sancu yi, daan def lepp lu mu man ngir sancu yi sax di ligeey ci mbay mi te bàyyi endustri bi, ngir man a joxe ne-ne yu nu laalul yu mbay yu man a dundal endustri yu reewi sancaan yi. Sanc gi jeem na a ray ruug gëpplante ci doomi sancu yi ginaaw bi mu fi rayee endustri bu lokaal bi, tax  it ba seeni boroom daanu ci kanamu endustri bu reewi Tugal yi. Bu ko defee këri jàmbur yi teg loxo ci koom-koomi reew yi ak seeni alali endustri. Ñu takk it xalisu sancu yi ci xaalisu reewi sancaan yi, loolu lepp nag ñu jublu ci takk koom-koomu sancu yi ci koom-koomu reew yiy sanc. Fii nag la genne gisiin wi naan: sanc gu politig du lu dul doomi sanc gu koom-koom ci sunu jamono jii nu toll.

Ñaawteefi sanc yu aada ak xalaat:

Sanc gi xamoon na ne aaday xeet ak cosaanam mooy li gën a man a dëgëral ag bennoo gu politig ak gu mboolaay, te moo gën a gaaw a jañe ci xeex ngir gore cig sanc ci reew yi.
Sanc gi jeem na a soppi taarixu reew yi nu sanc, te def ay pexe ci soppi seenug xay gi nga xam ne seen ngértel xeli doom la, juddoo nag ci ay jamono yu toppante te toftaloo. Mu tàmblee jël tooke di ko def ci lem ngir dundal ci doomi sancu yi jaare ko ci aada ak xalaat ngir ñu man a jàpple tubaab yi ci seen xalaat yi ak seen xemmemteefi sanc yi. 

Sanc gi nekkoon na fi di doju pakastal ci kanamu am njàng, rawati na mi ci aju ci xam-xami dëppale yi  ak yu xarala yi nga xam ne danuy jàpplee bu baax ci yewwuteg xam-xam man a am ak gu endustri ci reew yi. Te moom (sanc gi) yitteem weesuwuton ci wàllug njàng li nuy wax njàggale mu matale mi, walla njàggale mu yaatu mi . bu ko defee njàng mu kawe mi mu jagleel ko doomi kureelug laman gi daa jariñu ci sanc gi des fi. 

Sancaan yi danu daa yittewoo tas ak a wisaare seen làkk ak aada ak seen taarixu xeet ak seen xay gii nga xam ne teguwul  ci lenn lu dul ci ne-ne . Ñu tay-taylu woon di far dëgg yi, di indi li dëppoo ak seen njariñ, di wisaare xam-xam yiy ligeeyal seeni reew, di wone dooleem akug màggam, ñu tàmbli woon a sikk ndegam ñii cosaanoo ci sancu yi man nanoo jiite am reew, daan leen sabooteel seen kilifa yi, seen njiit yi, seen jàmbaar yi ak seen boroom xam-xam yi. Sanc gi jubluwutoon ci loolu dara lu dul ligeeyal boppam aki njariñam ak jeem fee saxal boppam, moom mi nga xam ne masul a dañ di ragal fippug askan yi ak seen yewwuteg xeet.

Doggantal gu ñeenteel gi:

Yëngu-yëngu yu ag nasaraanal  ak ay wi mu àndal:

Ag nasaraanal yëngu-yëngug diine gu nu nos la, gu li ko tax a jug mooy tas diiney nasaraan ak xayug nasaraan yi ci jullit ñi ak ñu dul ñoom. Nasaraanal gii nag lu taqoo la ak sancug Tugal gu yees gii nga xam ne jot na a man a ligeeyal diiney nasaraan ci anam gu nëbbu, jaare ko ci ay yoon aki defiin yu lëmu te jafee xam. Loolu lepp nag ngir ligeeyal ay xemmemteef yi mu amoon ci sanc adduna bi, yilif ko . Looloo du yomb nu tàqale diggante nasaraanal ak sanc, te itam nasaraanalkat yi danu daa nekk ci ron kilifteefug sancaan yi. Lu yeeme la diiney nasaraan nekk di benn ci jumtukaayi sanc gu Tugal gu yees gi. Nasaraanal nag yamutoon ci benn jàngu  rekk ci jëmmi boppam, waaye kay jàngu yepp a ko daan def, moo xam jàngu bu sowwu bi la (bu Katolig bi), bu penku bi (bu Ortodoksi bi), bu protestant bi walla bu Angalteer bi (bu Angalikaan bi).
Gëpplante gi taroon na ak xeex bi ci seen diggante, ni mu tare woon ci diggante reewi sancaan yi.

Taarixu nasaraanal gu yees gii nag am na ag takku gu mu takku woon ci yëngu-yëngu gu wuññi gu juxraaf gi reewi Tugal yu nasaraan yi doon def, te Porrtigaal ak Espaañ jiite woon leen, di woon ñaari reew yu ëppaloon ci diine te daan ci par-parloo kontar jullit ñi ak seen adduna. Bu ko defee wuññikati Orob yii ame woon ag parparloo gu diine defoon seeni ligeeyi wuññi, soldaarus Tugal si topp ci seen ginaaw di ligeeyal xemmemteefi sanc yu seeni reew, loolu lepp nag ngir nu àndandoo amal li nu bëgg mooy ligeeyal tubaab yi, te taxawal seenug cang ci diineek fetal .

Jumtukaayi nasaraanal aki ker-keraanam :

Nasaraanalkat yu nosu yi jëfandikoo woon nanu ab lim bu rëy ciy ker-keraan yu leen di dimbali ci seen ligeeyub nasaraanal bi, bu ko defee nuy def jamono ju ñëw ñu seet nu ñu ciy def ba ligeeyal ci seen jubluwaay boobu. Jumtukaayi nasaraanal gën na a jëm kanam ànd ak jëm kanam gi jamono def ak gi xam-xami dëppale yi ak yu xarala yi def.
Nasaraanal ñi ngi ko tàmblee ci ay nit di jug di waaraate ak a xamale yonnant Yàlla Hiisaa (j.m) akum njàngalem diineem. Wii xeetu nasaraanal sax na fi di ag nasaraanal gu kenn nit di def, mu doonoon lu jëmadi kanam waaye tolloo woon ak jamono ju yàgg ji mu dajeeloon.
Jumtukaayi nasaraanal jëmoon na kanam aki ker-keraanam bi yewwuteg xam-xam ak gu endustri gënee jëm kanam ci Tugal. Bu ko defee yonnee yu nasaranal yu nu nos yi tàmblee am, ay mbootaay yu nasaraanal yu bees di leen saytu, yuy jëfandikoo mbooleem anam yi ak jumtukaay yu yees yi ngir doxal seeni ligeey, bokk na ci li nu daa jëfandikoo:

(1)	Ndoktoor ak li mu àndal ci ay barabi faju, lu ci mel ni: fajuwaay yi  ak këri faj yu ndaw yi ak barab yiy maye ay garab. Ci xaranub fukk ak juroom ñeent, ay mbootaayi ndoktoor yu nasaraanal yu bari feeñoon nanu ci reewi Tugal yi ak Diiwaani Amerig yu Bennoo yi ak yul ñoom ci reewi addunay nasaraan ji, li leen taxoon a jug mooy waajal ay doktoor yu goor ak yu jigeen, aki matulkat  aki jàpplekati doktoor ngir ñu man a ligeeyal Egliis bi jaare ko ci ligeey ci barabi nasaraanal yi nu tasoon ci adduna bi, rawati na ci Afrig ak Asi. Ndoktoor man nanu ne mooy ker-keraan bi la man a gën a may ngay man a jonjoo ag nit ñu neew ñi doole ak ñu ñàkk ñi. Nasaraanalkat yi danu daa wax naan: li nu jublu ci jëfandikoo meccem ndoktoor ci nasaraanal mooy ne moom day nooyal yoon wi laytaay ko ba bu Injiil dee ñëw ngir dugg ci xol yi du jafe.(Ma ne man: nit ki boo ko joxee mu lekk, naan ginaaw bi muy bëgg a dee cib xiif, di bëgg a dee ci tawat nga faj ko, boo nee ko fii la mu ne foofa la, rawati na bu ko fekkul muy ku tatawu ci xam-xam, aaru ci dali diine ju dëggu). Daanu daa wax it: war na doktoor biy nasaraanal mu bañ a fàtte ne day nasaraanal laata a dara di xew. Mbootaayi nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci meccem ndoktoor mii, daal di ubbi lu sakkan ciy barabi ndoktoor  ci reew yu ndool yi yittewoo faj aki doktoor, ngir loolu man leen a jàpple ci seen ligeeyub nasaraanal boobu leen taxoon a jug.
(2)	Njàggale ak li mu àndal ciy jumtukaay, lu ci mel ne: daaray dal yi  ak yu diggu yi  ak yu ñaareel yi ak xamluwaay yu kawe yi ak daara yu mag yi ak kàggu yi ak daaray mecce yi añs. Ñi jiite woon nasaraanal gi danoo gisoon ne bu nu ubbee ay daara yii ci reewi jullit ñi ak yu leen moy loolu da na man a doon aw yoon ngir tas ci diiney nasaraan ci doomi jullit ñiy jàngsi ci yii daara, rawati na bu nu leen dee def leeg-leeg ñu cofal leen ci njàggalem Injiil mi, leeral leen ko, nga rax ci loolu li daara yii daa def muy tas xayug Tugal gi ak rawug xam-xamam ak jàngal ko yile dongo, te loolu ag doyodal jullit ñi rekk lanu ci jublu woon.
(3)	Jëf ju yiw ak ju nite ji nga xam ne mbootaayi yiw ak nite yu nasaraan yi daa nanu ko def ci reew yu ñàkk yi, rawati na ci jamonoy ay yi ak musiba yu dénd yi  ak xare yi: bu ko defee ligeeyub nasaraanal bi di sawar ci biir daw làqu yi ak ñu ñu tuxal ñi ci reew yu neew yi doole, loolu mooy li ngay gis ci reewi Afrig yeek ak Asi. Loxob nasaraan biy indi ñam, fa jak ndimal ñeel daw-làqu yooyu ak ñu ñu tuxal ñi, mooy biy tas dali diiney nasaraan ci ñooñii, di jariñu ci seen nekkiin wu metti woowu ak seen tumbrànke gu tar gi.
(4)	Yëglekaay yi ak këyiti xibaar yi, tasum xibaar meek yeene  yi nga xam ne seen woote yu nasaraanal yee ko daan tax a jug, ak waxtaan yi nu daa amal ci penc yi, ak taalifi penku-penku yi yi daa gëstu ci xam-xami penku yi ak seeni njàggat  aki pas-pas, ak li nekkoon ci loolu lepp ci tooke ñeel jullit ñi ak seenug xay, aki laaj yu man a jur ay sikk aki jiixi-jaaxa ci jullit ñi jëm ci seeni boroom xam-xam aki kilifa, lii lepp ci jumtukaay yi la woon . Nasaraanalkat yi  gisoon nanu ne daal teere yii ak yu nu mool yii man nanu leen a dimbali bu baax ci wisaare ag nasaraan ci reewi jullit ñeek yu leen moy, jaare ko ci li nuy bàyyi ci bakkan yu doyadi  yi. Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu ab lim bu mag ci ay daaray yar ci Tugal ak Amerig ngir waajal ci nasaraanalkat yi war a defi bii ligeey.

Nasaraanal ci reewi araab yi: 

Nasaraanalkat yu katolig, anglikaan ak protestant yi wisaaroo woon nanu ci reewi araab yi nekkoon ci ron sacug Britani, Fraans, Itaali mbaa gu Espaañ. Bu ko defee nasaraanalkat yi sos ci reew yii ay barabi nasaraanal ci biir askan wi, rawati na fa jullit ña, ndaxte seen jubluwaay ci loolu mooy neewal doole jullit ñi aks een diine. Reew yi nasaraanal gi sutuxlu danu leen ci tuddal yii :
Nasaraanal ag cawarteem fésoon na ci biir Nasaatiray Iraag yi, ci Mawsil, Baxdaad ak Basra, ñi ko doon def nag di ay nasaraanalkat yu Fraans ak yu Itaali. Àntug nasaraanal gu katolig gii ci Iraag ci njiitul Fraans merloo woon na Britani, ci noonu mu daal di fa woon yabal ay nasaraanalkat yu anglikaan, daal di ubbi bunt bi ci kanamu nasaraanalkat yu protestant yi, ngir ñu àndandoo xeex nasaraanal gu katolig gu rëy gii doon àntu bu baax ci Iraag. Loolu jur ag gëpplante gu mag ci diggante nasaraanalkat yu katolig yi cig wàll ak yu anglikaan yi ak protestant yi ci geneen wàll. Gëpplante gii nag du lenn dul geneenati ci gëpplante yi daa xew ci wàllug sanc ci diggante Fraans ak Britani ci goxi penku bi. Britani daa gisoon ne nasaraanalug katolig gu Fraans gii nekk Iraag tay, dara yobbuwu ko fa lu dul suuxat xejjug Fraans ak kilifteefam ci penku bi, te loolu moom la Britani doon ragal moom mi ame woon dooley sanc ji gën rëy te ëpp doole.
Ay turi nasaraanalkat yu protestant yu bari feeñ nanu ci ñi daan ligeey ci toolub nasaraanal ci Iraag ci xarnub fukk ak juroom ñeent g, ku ci mel ni: nasaraanalkat bii di Grant ak Groves ak Samuel Zwemer añs

Goxi Golfub Araab bi  :  

Ag nasaraanal tasaaroo woon na ci goxi Golf bu Araab bi, ndaxte bii gox da di ab jàlluwaay bu am solo jëm ci goxi penku yi. Bi mu ko defee, nasaraanalkati protestant yu Amerig yi sawar fa, daal di fay sos ay fajuwaay  yu seenub lim àggoon ci juroom ñeent, aki këri doktoor , seenub lim ñoom it àggoon ci fukk ak benn.

Nasaraanal gi yamutoon ci mbootaayi Protestant yu Amerig yi, waaye weesu woon na leen ba daj yu katolig yi ak yu angalikaa yu Britani yi. Ci noonu yii mbootaay tàmblee joŋante ci sos ay daara  aki jàngu  aki katederaal ci goxi Glof bi. Nasaraanalkat yu protestant yu Amerig yi daal di taxawal egliisub Injiil bu xeet wi ci Kuwet, Ahmadi, Manaama ak Masxat. Bu ko defee katolig yi taxawal katedraal bu katolig bu Rom bic i Manaama ak Abuudabi, ak Egliisu Angalikaan bi ci Manaama. Nu daal di sos ay barab yu nu jagleel tas Injiil ak seddale ko, ak yeneen teerey seen diiney nasaraan ji, ay seen yeene yi aju woon ci seen woote bu nasaraanal bi.
Waaye ak li nit ñiy yittewoo barabi faju yooyu lepp ak leekol yi, teewul ñu xeex bu baax kontar yëngu-yënguy nasaraanal yii ànd ceek li nu am ci jumtukaay ak doole. Boroom xam-xam yi xeex ko cis en xutba yi nuy def ci jàkka yi ak waaraate yeek gindee yi. Askan yu bañ sanc yii te noonoo ko ñoom itam xeex ko. Loolu jural nasaraanalkat yi ag sooy akug tas yaakaar.

Reewi Shaam:

Nasaraanalkat yi sawaroon nanu ci reewi Shaam yi, ci Siri, Libaa, Palastin ak Urdun . Nasaraanalkt yi yittewoo woon nanu mbirum Libaa ak Palastin, rawati na ginaaw xareb adduna bu njëkk bi, nga xam ne reewi Shaam yi danoo tàbbi woon ci ron feetale  gu Fraans ak Britani. Bu kodefee way nasaraanal yi sotti seenug nasaraanal ci goxi Siri yeek Libaa, daal di jàpplanteek kureelug Mawaarina yu katolig yi ci Libaa. Britani it duggsi, feeteek kureelug Dursu gi ci Libaa. Nasaraanalkat yi jeqi woon nanu fa ay fitnay kureel, ca la xarey kureel yu tàng te tar juddoo ci Libaa, ci diggante Mawaarina yi ak Dursu yi atum 1860g.
Way nasaraanal yu Angalikaan yi ñoom danoo sotti woon seen yitte ci Palastin, rawati na ne moom ab diggub diine la bu am solo ñeel ñi topp ñatti diiney asamaan yi: diiney Yahood, ju Nasaraan ak Lislaam. Mbootaayi Anglikaan yu Angalteer yi tàmblee sosi lopitaal aki leekol, aki mbootaayi yiw ci dëkki Palastin yi, rawati na Quds , Betlahem, Naasira, Tabariya, Yaafa ak Gasa.
Fii itam du waa Angalikaan yi rekk a fa doon def ag nasaraanal, waaye it katolig yi, Ortodoks yi ak Protestant yu Amerig yi. Julliti Palastin yi jàmmaarloo nanook yëngu-yënguy nasaraanal yii, xeex ak ñoom bu baax, ndaxte daa noonu woon seen diine, noonu seen jaloore, seen ndono, seen xay ak taarix bu lislaame bu xóot bii. Seenug xeex ko gën na a tar bi mu gënee leer ne ag nasaraanal la te sanc gi lay ligeeyal. Ci noonu nasaraanalkat yi jàpplanteek seeni goornamaa kontar araabi Palastin yi ngir defar lanuy wax dëëlub Balfour , genne ko it atum 1917g, li i ko taxoon a jug di sos am reewum xeet mu yahood yu sahyoon yi ca suufus jàmbur see di Palastin, di suufus ay araab yu jullit, tubaab yi déggook yahood yi jox leen ko, ci seenug toroxte ak naqar.

Isipt:         

Nasaraanal tas na ci Isipt te wisaaroo fi ci xarnub fukk ak juroom ñeent g, rawati na ginaaw bi ko Britani tegee loxo atum 1882g. Qibt yi  dimbali nanu mbootaayi nasaraanal yi tasoon ci biir jullit ñi ci Isipt. Bu ko defee yonnee  bu katolig bu Fraans bi tukkee woon Liyon daal di def ay ligeeyi nasaraanal yu fés, mboolooy nasaraanal yu Yesu yi di leen jàpple ci loolu. Nasaraanal ga amoon ca Isipt Paab gi dëgëraloon na ko te jàpple ko.

Mbootaayug nasaraanal gu anglikaan gu Angalteer gi def ay ligeeyi nasaraanal ci Isipt, ay cawartey nasaraanalam gën a yokku ginaaw bi Britani tegee loxo Isipt te jàpple bu baax yii mboolooy nasaraanal te aar leen. Mbotaayi nasaraanal yu protestant yu Amerig yi def ñoom itam seeni ligeey ci Isipt ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar-fukk g. bu ko defee mboolooy nasaraanal yii tàmblee xëccoo ci seen biir ak a gëpplante ci wàllug ubbi ay fajuwaay aki leekol aki egliis aki katedraal ak barabi seddale teere yeek mbindi nasaraan yeek yeneen yiy ligeeyal nasaraanal .

Jullit ñi xeex nanu nasaraanal ci Isipt, boroom xam-xami Ashar gu tedd gi jug ñoom itam jàmmaarlook yëngu-yëngu gii, daal di sos mbooloo muy aar Lislaam ngir xeex nasaraanal ci meloom yepp aki anamam. Mbooloo mii mujj na am ay bànqaas ci dëkk yu magi Isipt yi. Sos it ay jàngu  aki wéeruwaay ñeel way ñàkk ñi, ñu lòtt ñeek jirim yi. Ay doxi ñaxtu yu bari am ci kanamu barabi nasaraanal yi ci Xaayra, Demenhor, Saqasiq ak Kafar-siyaat añs.
Yenn it ci yëglekaay yu Isipt yi dimblee ci feeñal jubluwaayi nasaraanal gi, yee it jullit ñi ci ay wi mu làmboo.

Ligeeyub nasaraanal sawaroon na ci Sudan, rawati na ci ginaaw bi ko Britani tegee loxo. Bu ko defee mbootaayi nasaraanal yu katolig, yu protestant, ak angalikaan yi def seeni ligeeyi nasaraanal ci biir jullit yi dëkke woon ci bëj-gànnaaru Sudan ak ñu dul jullit ñi dëkke woon ci bëj-saalumam. Way nasaraanal yi sotti woon nanu seen yitte ci ñi dëkke woon ci bëj-saalumu reew ma te doonadi woon ay jullit, ci noonu ñu jot a tas seen diine ji ci ñoom ak aaday sowwu ji. Nasaraanalkat yi sosoon nanu ay jàngu yu yonnee yu katolig ak yu angalikaan ak yu protestant ci Sudan, sosati fa ay barabi faj yu nasaraanal.

Waaye waa Sudan ñoom toogunu rekk lem seeni loxo ci kanamu nasaraanal gi. Fipp gu Mahdi di xeex na ko. Broom xam-xam yi xeex ko. Mbootaayi diine yi rawati na ci bëj-gànnaaru reew ma ñoom itam xeex ko.

Reewi Maxrib bu araab bi :

Maxribu araab bi dafa nekke fu jàkkaarloo ak reewi nasaraan yi, rawati na Espaañ, Itaali ak Fraans. Reew yii nag jariñoo nanu bu baax neew dooleg reewi Maxrib bu araab bi, daal fay yabal ay nasaraanalkat yu bañ Lislaam ak jullit ñi, ngir ñu def fa seen ligeeyi nasaraanal yi, ak ngir nooyal ko, waajal ko ba mu man a dékku sanc gi nar a ñëwi di tukkee ci Fraans, Itaali ak Espaañ. Reew yii yepp nag yu yor diiney nasaraan lanu.
Cawarteg nasaraanal gi yokku na te dolliku, rawati na ci keppaarug sanc gu Tugal gii ci reewi Maxrib yi. Bu ko defee gëpplante gi ci toolub nasaraanal tàmblee tar ci diggante mbootaayi nasaraanal yu katolig yi, yu anglikaan yi ak yu protestant yi. 
Nasaraanalkat yi daal di wut ay jumtukaay aki ker-keraani nasaraanal , taxawal ay fajuwaay aki kër doktoor aki daaray nasaraanal añs. Ci biir loolu ñu def lu nu man ngir fay làkkuw araab, te dundal kàllaamay berber yi ngir xeex ci làkku Alxuraan wi, ñu defoon ay pexe itam ci far aaday Lislaam ji ak taarixam, jeem a jox jullit ña fa dëkke woon ay reewu  yu reewi sancaan yi, bu ko defee dunu reewooti ci seeni reew, te dunu ko bëggati. Ñu xeex ak boroom xam-xami jullit ñi daa jeem a taxawal ligeeyub nasaraanal bi. 

Waaye nag ñu fonk seen reew ñii dëkke woon ci reewi Maxribu araab bi amoon nanu ndam ci damm degug sanc gi ak gu nasaraanal gi, ngir seen xeexub njàmbaar bi ñu leen jëmale woon.

Barabi nasaraanal yi ci reewi araab yi:

Mbootaayi nasaraanal yi sosoon nanu lu sakkan ci ay barabi aada , yu xam-xam ak yu faj ci reewi araab yi, lii ci la:

(1)	Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari ci ay jànguy dal , yu diggu ak yu ñaareel yu nasaraanal ñeel xale yu goor yeek yu jigeen yi, ci mbooleem reewi araab yi nasaraanal gi dugg.
(2)	Mbootaayi nasaraanal yi sos nanu lu bari barabi jàngale yu kawe yi ci Isipt, yu ci mel ne: daara ju mag ju Amerig ji, xamluwaay  bu penku bi, xamluwaay bu Fraans bi, yooyu yepp nag ñi ngi Xaayra . Bu dee Sudan, nasaraanalkat yi sos nanu fa bànqaas bu Kamboni bu katolig bi ak jàngu  bu Amerig ak jàngu  yu Qibt  yi, yu Gres yi ak yu Angalteer yi. Mbootaayug protestant gu Amerig gi moom tam sos ca Bayruut daara ju mag ju Amerig’ati. Katolig yi sos fa ñoom daara ju mag ju katolig ja, walla daara ju mag ju Yesu  ji ñu duppee aji sell jii di Yuusuf .
(3)	Nasaraanalkat yu penku-penku  yi dugg nanu ci akaademiy làkk yi ci reewi araab yi. Ñu dugg ca akaademib làkk ba ca Xaayra ak bu xam-xam ba ca Dimasq , ak bu xam-xam ba nekk Baxdaad, penku-penkub Angalteer bii tudoon Jub nag kenn la ci ñoom ak Margoliyos mu Fraans mi, Garifani mu Itaali mi, Hothman mu Holand mi, ak Harithman mu Almaañ mi. Penku-penku yi duggal nanu seen loxo ci teere yu bari yoo fiy gis tay, ñu tudd ci rekk ci misaal: jimblang ci Lislaam  ak dundug Muhammad (j.m) ki nuy wax Sir William Mouir def ko, teere bi tudd Lislaam te Alfred Giyom def ko ak yeneen ci teere yi nëbbal Lislaam ag mbañeel.
(4)	Mbootaayi nasaraanal yi taxawal nanu lu limu ci ay cëslaayi faj , lu ci mel ne: fajuwaayu Marson ak bu Maryon Wilth, ca Bahrayni ak fajuwaayu Noks ca Masqat ak bu Harmal ca Isipt ak bu Maryohanna biy faj bët ca Quds, ak yeneen yu nasaraanal yi wisaaroo ci mbooleem reewi araab yi. (ginaaw ci reew yii lanu nekk nag, kon yu Afrig gu ñuul gii nga xam ne mooy seen mburu mu bees jarul ñuy wax).

Juroom benneelu bunt

Ñaar-fukkeelu xarnu

Ñaari xarey adduna yi, bu njëkk bi ak bu ñaareel bi
Mbootaayi adduna yi: kureelu xeet yi, mbootaayu xeet yi
Mbootaayu reewi jullit ñi
Danki reew yi ak reew yi feetewul fenn
Xareb jawwu bi
Jëm kanam gu Japon

Doggantal gu njëkk gi
Ñaari xare yu adduna yi: bu njëkk bi ak bu ñaareel bi

Xaaj bu njëkk bi ci ñaar-fukkeelu xarnu g, seere na tàkkug ñaari xare yu adduna, ñooy xareb adduna bu njëkk bi (1914 – 1918g) ak bu ñaareel bi (1939 – 1945g).
Leegi nag ñu waxtaane leen ci ni nu càllaloo ci jamono.

Xareb adduna bu njëkk bi (1914 – 1918g):

Li waral xare bi:

Xareb adduna bu njëkk bi am na ay sabab yu jonjoo ak yu jonjoodi , kon nanu njëkk a waxtaane sabab yu jonjoodi yi.

Sabab yu jonjoodi yu xare bi:

Man nanoo tënk sabab yu jonjoodi yu xareb adduna bu njëkk bi ci ñeenti sabab yu mag ñooy: 

(1)	Gëpplante gi ci wàllug sanc
(2)	Tapoo yi 
(3)	Màggug yëngu-yëngu yiy woote ag xeetu 
(4)	Ak lëj-lëj yu adduna yi 

( a ) Gëpplante  gi ci wàllug sanc:

Gëpplanteg adduna gi taroon na ci ginaaw yewwuteg endustri gi, ci fukk ak juroom ñatteelu xarnu g . Reewi endustri yi seeni cawarte gën na a yaatu, gën a jëm kanam ci gii wàll, ci fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g, li ko waraloon di naj gu tar ak jañax gu tëw a dakk gi leen seen lonkoo yu endustri yu mag yi daan jañax jëme ci loolu, ak boroom boppi alal yi dëkk ci yile reew, rawati na nag ci reewi Tugal yi am ay noste yu gore . Bu ko defee ñu jug tàmblee gëstu-ji  ne-ne yu nu laalul yi manul a ñàkk ngir ligeeyi endustri yii man dox, man a jëm kanam. Tàmblee wër it ja  yu nu man a jaaye-ji seen ligeeyi endustri yu wuute yi.

Loolu nag jur na fi ag xér ci ne-ne, loolu tam jurati fi jawwi gëpplante ci wàllug sanc ci diggante reewi endustri yu mag yi, lii itam jur ag rawante ci ngànnaayu ci adduna bi, bu ko defee endustrib ngànnaay gën a jëm kanam, ndaxte ku bëgg a sanc fàww nga yor ngànnaay yu doy, ku ko bëgg a suuxat it mbaa nga bëgg cee ame sa njariñi koom-koom yi tax nga koy def fàww nga ngànnaayu.

Ag gëpplante gu tar amoon na ci wàllug koo-koom ci diggante Britani ak Fraans cig wàll, ak ci seen diggante ñoom ñaar ak Almaañ ci geneen wàll. Silaay  Almaañ yi bari woon nanu ci ja yu adduna yi, ngir ay sabab yoy yenn yi danoo dellu woon ci jëm kanam gi endustri Almaañ jëmoon kanam, yi ci des dellu ci barig naali koom-koom  yu Almaañ yi ci reewum Usmaan  mi, rawati na naalub yoonu weñu Berlin-Baxdaad-Kuwet. Xëccoo googu nag amoon ay jeexiital yu rëy ci tàkkug xareb adduna bu njëkk bi .
Ci nii lanuy gise ne gëpplanteg koom-koom gu adduna bi mooy li duggal adduna bi ci paxum xare bu tàng, bu nu ngànnaayal.

( b ) Tapoo yu reew yi:

Gëpplanteg politig gi aju woon ci sanc ci adduna bi dafa gënoon na jëm kanam, ci ginaaw bi gëpplanteg koom-koom gu adduna bi gënee jëm kanam. Loolu nag tax ba ay dank  sosu yu reew, defees it ay kollarante aki dëppoo yu yor màndargam politig, mu xare  ci diggante ab lim ci reew yi seeni njariñi sanc di jegee, walla yi ci jot a àgg ci deggoo ci lijjanti lëj-lëj yi nekk ci seen diggante. Ñu tuddal leen ci dëppoo  yooyu ak tapoo  yooyu, yii di ñëw:

Tapoo gu ñaaral gi ci diggante Almaañ-Otris:

Gii tapoo amoon na ci diggante imbraatooru Almaañ gi ak gu Otris gi atum 1879g, bokk na ci li ëppoon solo ci ay sartam, lii di ñëw:

(1)	Bu Rusi gu Xaysar gi  songee menn ci ñaari reew yi , meneen mi war na a dimbli mi nu song.
(2)	Bu menn ci ñaari reew yi tapoo songee meneen mu ñatteel, ma ca des da ca a war a ame taxawaayub génn ci, di leen seetaan waaye nag ci anamug cofeel ñeel àndandoom boobu.
(3)	Bu ag dimblante gu am solo amee, walla gu xare ci diggante Rusi ak Fraans, ñaari reew yii tapoo de war nanoo ànd ligeey ngir xeex loolu.

Tapoo gu ñattal gi :

Moom ag tapoo la gu Almaañ-Otris-Itaali, mi ngi sosu ci bi Itaali duggsee ci tapoog ñaaral gi nu la tuddoon leegi atum 1882g, ak doonte njariñi Itaali dëppoowut ak yu imbraatoorug Otris gi, waxuma la sax noonoo gu yàgg ga nekkoon ci seen diggante, te li ko waraloon di yilif gi ko Otris yilifoon njëkk bennoo ga, ak ca ginaaw ba, waaye Otris mii moo tegoon loxo ag wàll ci suufus Itaali, ba noppi yilif fa yeneen wàll.
Itaali duggsi na ci tapoo gi ngir wuute gi mu defoon ak Fraans, ndax fraans dafa dëgëraloon bu baax tànkub sancam ca goxi bëj-gànnaaru Afrig, fu ci mel ni Aljeeri atum 1830g, ak Tunisi atum 1881g, kon Itaali duggsi gii mu defoon ci tapoo gi du woon dara lu dul doxaliinu politig, li mu ci jublu woon di jañaxal Fraans ak Britani ngir manante  leen ci ñu nangul ko te bàyyee ko njariñam  yi nekk ci geej gu diggu gi .

Dëppoo  gu Fraans-Rusi gi:

Dëppoo googu am na ci ginaaw bi ag jegeente amee ci diggante Fraans ak Rusi gu Xaysar gi, loolu nag tàmbli na atum 1886g, daal di gën a jëm kanam atum 1888g, bi ñaari reew yi dëppoo ci fas ag kollare guy waral Fraans di jox Rusi ngànnaay, te jëmale kanam ag jokkoom  jaare ko ci def fa ay yooni weñ. Ci atum 1891g la Fraans ak Rusi def ag kollarante guy yaxal lii di ñëw:

(1)	taxawal ag dëppoo ci diggante ñaari reew yi, ak weccante xalaat ak diisoo buy lëj-lëj amee ci adduna bi.
(2)	Bu menn ci ñaari reew yi duggee cib xare, ñaari reew yi war nanoo diisoo ngir dëppale seen diggante.

Dëppoog cofeel gu Britani-Japon:

Ag dëppoog cofeel sosu na ci diggante Britani ak Japon atum 1902g, lii la yaxal:

(1)	Bu xare tàkkee ci diggante Japon ak Rusi gu Xaysar gi, Britani da ca a war a genn te seetaan.
(2)	Waaye bu meneen reew duggee ci xeex bi nekk ci diggante Rusi ak Japon, kon Britani da ciy war a dugg moom itam, jàpple Japon.

Dëppoog cofeel gu Britani-Fraans:

Ag dëppoo gu cofeel xewoon na ci diggante Britani ak Fraans atum 1904g, gu lijjanti woon lëj-lëj ak reeroo yi amoon ci seen diggante, dëppoo googu nag lii la wax:

(1)	Féexal Fraans, joyal ab loxoom ci Marog , gii nga xam ne jotoon na a temb, te nangul ko teg gi mu teg loxo Ajeeri ak Tunisi.
(2)	Fraans moom tam nangul Britani teg gi mu teg loxo Isipt atum 1882g

Dëppoo gu cofeel gu Britani-Rusi:

Ag dëppoog cofeel am na ci diggante Britani ak Rusi gu Xaysar gi atum 1907g, lii la wax:

(1)	Déggoo ci ni nuy séddoo barabi sañ-sañ yi ci Iraan , ba mu des fa benn barab rekk bu temb ca digg ba ñu bàyyil ko fa Shaah ba, ginaaw bi Rusi jëlee wàll gu bëj-gànnaar gi, Britani jël gu bëj-saalum gi.

( c ) Màggug yëngu-yënguy xeetu  yi ci Tugal:

Yëngu-yëngu yi aju ci xeetu dafa xëy gën a màgg ci Tugal, loolu nag bokk na ci li jañ adduna bi jëme ko ci xare bi. Xarnub fukk ak juroom neenteel g, dees na ko lim muy xarnub xeetu yi ci Tugal, yëngu-yënguy xeetu yooyu nga xam ne li leen taxoon a jug mooy gooreel seen bopp te nocciku ci kilifteef ak teg loxog reew yi leen di àtte  cig wàll, ak sosal xeet wu nekk am reewum boppam mu koy ëmb, uuf ko ci geneen wàll. Ñaar nag bokkoon nanu ci yëngu-yëngu yi gënoon a siw ci yooyu, ñooy:

Mbootaayug Slaaf gi :

Gii mbootaay, walla yëngu-yëngug slaaf gii, li ko taxoon a jug mooy xettali askanu slaaf wi jële ko ci àtteg imbraatoor gu Otris gi, ak sos reewum slaaf mu ëmb mbooleem slaaf yi dëkke ci Balkaan ak salaaf yi dëkke ci Tugalug penku gi.
Mbootaay gii nag daan na jot ag jàpple mu tukke ci Rusi gu saaf gi, loolu taxoon na ba ag reeroo gu mag am ci diggante Otris ak Rusi gu Xaysar gi.

( d ) Lëj-lëji adduna bi: 

Ay lëj-lëj yu fasu yu adduna bi sosu nanu, bokk it bu baax ci li fi taal xareb adduna bu njëkk bi. Lëj-lëj yii it li leen jur day dellu ca reeroo ya amoon ca diggante reew yu mag ya ngir seen gëpplanteg sanc gi, ak ngir màggug xeetu ci Tugal, ak ngir fipp gi askan yi fippoon ngir jot seenug tembte ak gore. Ñu tudd ci yi ëpp solo ci lëj-lëj yooyu:

Lëj-lëju Maraakes:

Fraans yàgg na a waaj ak a naal ngir teg loxo Maxrib gu sori gi (Maraakes), moom nag Maraakes dafa yoroon ag tembam lu yàgg, te booba Tunisi ak Aljeeri Fraans a ngi leen tegoon loxo, yilif leen cig sanc. Ci noonu Fraans lijjanteek Britani seen reeroo gi nekkoon seen diggante, ca dëppoog cofeel ga atum 1904g, Fraans daal di bokki ca ndaje ma nu njëkk a def ca dun bu wert ba atum 1906g ca Espaañ ngir lijjanti lëj-lëju Maraakes bi.
Saxal ya juddoo ca ndaje ma nag njariñul Fraans la gënoon a nekk, ndax reew ya fa daje woon danoo dëppoo woon ci nangul Maraakes ag tembam waaye feetale Fraans wàllug kaaraange ga ak sàmm njabootug Tugal ga fa nekkoon. 
Fraans nag jariñu na bu baax ci dénk gi nu ko dénk kaaraange ga, ndax ba ay yëngu-yëngu amee ca Faas ga nekoon peey ba, da fa a daal di woon yabal ay dooley xare yu Fraans ngir ne da ciy aar jàmburi Tugal ya fa nekkoon. Loolu moo merloo woon Almaañ mi àndoon ak buurub Maraakes bi, daal di ne woon fàww Maraakes jot cig tembam, ngir naqaral Fraans.
Almaañ daal di yabal ag gaal gu mag ca waaxub Agadiir ngir aar ag njabootam, ak ñaxtoo ci yabal gi Fraans yabaloon am mbooloom xare ca Faas atum 1911g ngir teg ko loxo.
Ñu defaat am ndaje ca dun bu wert ba ca Espaañ atum 1911g, ngir lijjanti xuloob Fraans-Almaañ bi, la fa juddoo di : jox Almaañ ay moomeel ca Kongog Fraans ga, bu ko defee Almaañ nangul Fraans nekk gi Maraakes nekk ci ron kaaraangeem, ñu daal di def Tanja muy ab waax bu adduna bepp, daal di doxal nag politigu ubbi buntub Maraakes ci kanamu yaxantug adduna bi.

Lëj-lëju Balkaan:

Otris daa boole woon ci boppam ñaari gox yii di Bosni ak Hersogowin atum 1908g, te ñoom ñaar ñi ngi bokkoon ci diiwaani reewum Usmaan mi ci Balkaan.
Reewum Usmaan mi ca jamono jooja dafa nekkoon di dund ci jawwi yong , mooy yong gi ñoñ bennoo ñi  defoon atum 1908g. 
Serbi nag (moom ag wàll la ci yogoslaafi ci jamono jii nu nekk) daal di ñaxtu loolu ak Rusi gu Xaysar gi ko daan jàpple (moom Serbi). Almaañ jug moom jàpple Otris ci jëfam jooju. Loolu nag bokk na ci li gën a dolli tangoor wi ca daanaka-dun bu Balkaan ba.

Lëj-lëju Maseduwaan:

Ab xare tàkkoon na ci diggante Reewum Usmaan mi ak Gres, Bulgari ak Serbi ci Maseduwaan, ñoom ay reewi Balkaan lanu. Li ko waraloon nag mooy Bulgari, Gres ak Serbi danu doon defi pexe ngir roccee Maseduwaan ci Reewum Usmaan mi, te seddoo ko ci seen biir. Bi nu dàqee Reewum Usmaan mi ca xare ba ba noppi, danoo reeroo woon ci ci seen biir ci nu nu koy seddoo. Serbi moom daa bëggoon na jot ci Albani, waaye ñu xañ ko ko, ndaxte Otris daa taxawoon temb ci nu jox Albani ag tembam. Loolu waral leneen  coow amati ci Balkaan ci diggante Serbi, Otris ak Rusi ak ñeneen.

Lëj-lëju Tripoli:

Itaali jariñu na ci am soxla gi Reewum Usmaan mi amoon soxla ak lu ko doy, ca xareem ba ca Balkaan, bu ko defee mu song ko ca Tripoli gu soww ga, atum 1911g, daal di nangu Libi, teg ko loxo atum 1912g, ginaaw bi mu lijjantee ba Fraans ak Britani genn ci, te noppi ci.

Sabab yu jonjoo yi ñeel xareb adduna bu njëkk bi:

Noonoo gi taroon na jëm ci Slaaf yi ci Balkaan, looloo waraloon ñoom Slaaf yi juggoon taxawal ag mbootaayug sekkare ngir xeex loolu, Serbi jàpple leen ci ak Rusig Xaysar gi. 
Ab dongab Slaaf yong  na Arshidog Fransis Ferninand, mi nekkoon wuutlaayu  Otris ak soxnaam, ca 28 suwe 1914g, ca dëkkub Sarayevo bi nekkoon peeyub Bosni, ci tukkib nemmeeku bu mu fa doon def.
Otris daal di gaaw jirñoo xew-xew bii, daal di yonnee Serbi ag xupp ca bisub 22 sulye 1914g, gu làmboo fukki sart ak benn, bokk na ci yi ëppoon solo ci sart yooyu: raxas goornamaab Serbi bi ak dooley xareem ji ci mbooleem ku bokk ci kureel yiy kontar Otris, te may Otris mu defal boppam raxas gii, te tëj yëglekaay yi ak jumtukaayi tes-xibaar yi noonoo Otris, ak boole Otris ci gëstu ñi def yong googu ak àtte leen. Ak yeneen sart yu tar yu tax Serbi jort ne kii daal daa fas yeenee dugg ciy mbiri biiram. Ba noppi Otris joxati Serbi diirub ñeen-fukki waxtook juroom ñatt, ne ko mooy àpp bi nga xam ne waru koo weesu te tonntuwul, waaye Serbi moom tontuwul .

Jibalug xare bi:

Otris taal na xare bi ci kaw Serbi, ci 28 sulye 1914g . Bi loolu amee Rusi moom itam jug song Otris ngir jàpple Serbi, loolu it jurati Almaañ jug – cig wàllam – jafal ab xare ci kaw Rusi ak ci kaw Serbi. Fraans duggsi ci, ci wetu Rusi miy reew miy xaritam, nadx moom la defal ag tapoo, daal di jibbal ab xare ci kaw Almaañ ak Otris. Britani tam it xuus xare bi kontar ñaari reewi digg  yi nga xam ne Reewum Usmaan mi mujj na àndseek ñoom ci xeex bi. Siin it ak Japon mujj nanu duggsi ci xare bi ci wetu reewi dëppoo gi. Itaali it dugg-si ci kontar reewi digg yi, atum 1915g, te kat bu njëkk da doon seetan rekk, feetewutoonn fenn. Britani nag nekkoon na di fasante ak Itaali kollareg sekkare. Kollare gi nag li mu doon yaxal mooy Itaali  jox ko suufus Dalmaas bu xare bi jeexee. Amerig dikk moom itam, dugg-si ci xare bi ci wetu reewi dëppoo yi, daal di genn ca beroom ga mu defoon ca goxub Amerig ba. Duggsi gi mu duggsi woon ci xeex bi nag lu am solo la woon, ndax moo ko soppi bu baax, ngir doole ak jumtukaay yi mu indil reewi dëppoo yi ak alal.

Lefum xare bi :

Jë  bu sòww bi ëmboon Fraans ak Beljig, mooy barabu xeex bi ëppoon solo ci xare bi ci diggante 1914 – 1915g, boobu diggante mooy bi gën a tar ci xeex bi. ndaxte dooley reewi digg yi jot nanoo putuxlu ci reewum Beljig mi ak wàllug penku gi ci Fraans, ak li reewi dëppoo yi di jàmmaarlo lepp ak a xeex ngir loolu bañ a am. Lii nag bokk na ci ndam yi ëpp solo, yi reewi digg yi def ci jëwub sòww bi. Waaye reewi dëppoo yi jot nanoo taxawal jëm kanam gi Almaañ ak Otris doon def, ba daanaka àgg ca bunti Paris, ci xeexub njàmbaar bi nu doon def ngir aaru.
Ñaari wàll yi nag xeex nanu ay xeex yu tar, yi ci gën a siw mooy bu Marn bu njëkk bi ci sulye atum 1914g.

Bu dee nag ci jë bu penku bi, xare bi moom foofa ci diggante Rusi ak Otris la nekkoon. Barabub xeex ba di woon Poloñ ak Balkaan. Xeex bi amoon ci penku bi nag xawoon na a woyofal tuuti yan bu diis bi nu tegoon ci ndòddum reewi dëppoo yi ci sòwwu bi, ndax reewi digg yi danoo mananul woon a ñàkk a dolli seen soldaar sa nekkoon ca penku ba di xeex ak Rusi. Foofa tam ca penku ba lanu gëne woon aw demiin ca sòww ba, ndax jot nanu fa a nangoo wàll gi Rusi moom ci Poloñ ak Litwaani. 

Ay xeex am ca diggante Reewum Usmaan mi ak Britani ca Iraag ak Palastin. Ca la Britani tege loxo ñaari reew yii. Reewum Fraans it nangu Siri ak Libaa.

Bu dee ci geej gi moom, xeex bi mi ngi doon ame ci nuuraakon  yi nga xam ne Almaañ da leen daa joyal ci gaali reewi dëppoo gi. Mbooloom gaalum  Britani mi nag moo kawe woon ci xareb geej gi. Xareb Gitland bu geej bi amoon atum 1916g, bokkoon na ci xeexi geej yi gën a rëy ci xare bi, nga xam ne Amaañ ak Britani ñepp ñàkke nanu ci lu dul jeex ciy nit ak jumtukaay.

Atum 1917g, bokk na ci at yi gën a tar ci ati xare bii, ci la Rusi genne ci xare bi, ca kollareg Litofski ga ca 27 desambar 1917g , ci ginaaw bi fippug Balsafi gi amee. Romani topp ca moom mi sukkandiku woon ci xare bi ci Rusi, moom itam ag gennam mi ngi jaare ci kollare ga nu defoon ca Boxarest. Ca at mooma tam la Diiwaani Amerig yu Bennoo yi ñoom it duggsi ci xare bi ànd ak reewi dëppoo yi. Loolu nag feeñ bu baax ci doxiinu xare bi, ndaxte Amerig moom jàpplee woon na bu baax ci wàllug xare  ak koom-koom, loolu nag di woon lu sonnal reewi digg yi. Ca at mooma tam la jë bu Usmaan  bi it nërméelu. Ci la jë bu Otris it daanu. Ay yëngu-yëngu aki coow yu ay ligeeykat am ca Almaañ. Ca mooma at it la Woodrow Wilson defoon fukk ak ñeenti poñam ya doon woote ñu taxawal xare bi te bàyyi askan yi ñu def li nuy wax (autodétermination) muy tànnal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom.

Atum 1918g nag mooy atum ndam li ñeel reewi dëppoo yi, waaye it mu nërmeelu ñeel reewi digg yi, ndax imbraatoorug Otris ak gu Almaañ yépp daanu nanu, Imbraatoorug Usmaan gi it ñàkk mbooleem diiwaanam yi mu amoon ci bitib Asi gu ndaw gi, nguurug Bulgari daanu, ci noonu askani reewi digg bi daal sàkku wéerum ngànnaay ci ni ko poñi Wilson yi doon sàkkoo.
Bi reewi digg yi demee ba lòtt ci wàllug aaru, te manatunoo dékkooti xare bi, lanu wommatu . Bu ko defee Bulgari xaatim ag wéer ngànnaay ak reewi dëppoo yi ci 30 satumbar 1917, Turki topp ci, ci mujjug oktoobar atum 1918, ak Otris ci 3 nowambar 1918, ak Almaañ ci benn fanu nowambar 1918g.

Lijjanti yi ci ginaaw xare bi:

Reew yi am  ndam ci xare bi defoon nanu am ndajem juboo ca Paris, peeyub Fraans, li ko waraloon nag mooy gëstu nan lanu war a def ci adduna bi ginaaw bi xare bi jàllee. Moomu ndaje nag Clemenceau moo ko jiite woon, njiilul jëwrin lu Fraans li, bu ko defee, ñu defe ndaje ma ca njéndul Varsaay la, di dëkk bu nekk ca wetu Paris.
Diiwaani Amerig yu Bennoo yi Wilson teewal ko, Britani Luwid George njiitul jëwrin la nekkal ko fa, Fraans Clemenceau miy njiitul jëwrin ya moom itam wuutu ko fa ak Itaali ci teewaayu Orlando njiitul jëwrinam, reew yii amoon nanu xejj gu mag ci ndaje mi, rawati na ñatti reew yii di Amerig, Britani ak Fraans.

Ndajem juboo mii ay saxalam ballewunu ci déggoo ak waxtaan wu reew yi gañe def ak yi nu gañe, waaye kay reew yi gañe danoo teg seeni sart ci kaw reew yi nu gañe cig sañ-bañ. Kollare ga nu fase woon ca Versailles atum 1919g te xaatimoon ko ak Almaañ, bokk na ci kollare yi ëpp solo te juddoo ci ndajem juboo mi. Moom kollare googu dafa yaxaloon lii: Delloo Fraans Alsaas ak Loren, ak delloo Danmark wàllug bëj-gànnaar gi ci goxub Sholswig, bu ko defee Poloñ moom jot ci suuf su bari ci Almaañ ak yoon wu yaatoo ñeen-fukki miil, wu romb ci biir diiwaanub Brusiya gi nekk ci Almaañ, bu ko defee tàqale kook yeneen suufi Almaañ yi. Ci noonu ñu def waaxub Danseg  bu Almaañ bi muy waax bu nu jagleel reewum Poloñ mi nga xam ne taxawalaat nanu ko ci ginaaw xare bi. Nu jëlati ci Almaañ diiwaanu Sodit jox ko Cekoslawaki, mi nga xam ne mi ngi sosu woon ci ginaaw xare bi, ñu jëlati ci Almaañ waaxub Mamel jox ko Lituwani. Bu ko defee Almaañ ñàkk mbooleem sancoom yi. Ba noppi nu ga  ko ci mu yamale ay soldaaram ci teemeeri junni. Nu neenal fa duggum coldaarum gu sañ-bañ, dindi mbooleem tata yi wëroon kanaalub Kyel ak goxub Rayn. Nu tàmbli woon a def fuglu gu tar ci ligeeywaayu ngànnaay yi ak jumtukaay yi ci aju. Ñu nangoo woon ci Almaañ it mbooleem ay nuuraakonam  aki gaali xareem aki fafalnaawam ak lu ëpp ci ay gaali yaxantoom, ci noonu Fraans nangooti diiwaanu Saar ( di xuru dexug Rayn gi) di barab bu naat ci ay mbell, mu nangu ko nag diir bu tollu ci fukki at ak juroom. Ñu daal di teg Almaañ nag ag alamaanug xare ak alal ju mu war a fay ju bari ju tollu ci (6,600,000,000) yu Sterlin, ak doonte Almaañ fayu ci ci diggante 1924 – 1930g lu dul lim boobu rekk.

Imbraatoorug Otris gi nag moom, ndaje ma daa daal di jeexal nguurug njabootug Habsborg ga fa nekkoon, daal di taxawal ciy màbbiitam ay àtte yu bari, ñooy: Pencum Otris  ak Hongri ak pencum Cekoslawaki, ñu jëlati wàllam ya nekk ca Balkaan boole ko ca reewum Yogoslawi mi sosu ci ginaaw xare bi.
Bu dee Reewum Usmaan mi moom dafa ñàkkoon mbooleem moomeelam yi mu amoon ci Asi ak Afrig, deseetutoon lu dul moomeelam yi mu amoon ci Asi gu ndaw gi, ñu daal di ko def muy leegi pencum Turki wuuteek lool reewum Usmaan mu mag ma nu xamoon, loolu di woon ci 29/10/1923g, ginaaw bi Mustafa Kamaal Atatork (1880 – 1930g ) neenalee nosteg saltana  ga fa amoon atum 1923g, ak gu xalifa ga atum 1924g.

Ndaje mi nag sos na fi ay reew yu yees yu bari ci Balkaan, mu ci mel ne mom Yogoslawi mi jële won ay suufam ci reewum Serbi mi ak yenn ci goxi Balkaan yi bokkoon ci moomeelug imbraatuurug Otris gi, bu ko defee nu sosaat reewum Poloñ mi ak Brusiya. Reewum Cekoslaafi moom itam taxawe ci ñaari xeet yii di Slaaf ak Cek, reewum Hongri tam sosu, Finland, Stwaani, Lituwani ak Latfiya reew yii yepp jug di dëgëral seeni nekktey  politig, te bu njëkk danoo nekkoon ci ron teg loxo gu Almaañ, ci ginaaw bi Rusi gennee ci xare bi atum 1917g, daal di fas kollareg Litofski gi ak reewi digg yi. Lii moo jeexal àtte gi njabootub Romanof gi doon àtte Rusi.

Ñu daal di jël nag yenn reew yi teg leen ci ron ag feetale: Iraak, Penkub Urdun (Jordanie) ak Palastin ñu teg leen ci ron feetale gu Britani  atum 1920g, Siri ak Libaa ñoom ñu teg leen ci ron feetale gu Fraans atum 1920g. Ndajem Paris ma nag saxaloon na feetale gii te xaatimoon ko.

Ñu daal di sos Kureelu xeet yi (League of Nations)  teg ko ci poñub fukk ak ñeent bi ci dali  Wilson yi doon woote ag ñoŋal jàmm ci adduna bi ak tee xare amati fi ak dëgëral dimblante ci reewi adduna bi.

Nii daal la xareb adduna bu njëkk bi jeexe ginaaw bi mu sonnalee adduna bi bepp, sotti ko sawaraam si ak alkandeem li. Ray nanu ci lu jege juroom ñatti milyoŋi nit , gaañ ca lu jege ñaar-fukki milyoŋ. Waxuma la nag ñi faatoo ca xiif bu metti ba’ak tawat ja xare ba waraloon.

Ñaareelu xareb adduna bi (1939 – 1945g):

Lijjanti ak saxal ya juddoo woon ca ndajem jàmm ma ca Paris, ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi, ñoo jur - man nanu ne – lu ëpp ci li sooke ñaareelu xare bi.
Kollareg jàmm ga fa juddoo woon sooke woon na mer wu metti akub sànj  ci askani reew yi nu note ca xeex ba. Askan yooyu nga xam ne doyutoon ñu yanu coonay xare beeki musibaam rekk, waaye ñu tegati ci yan leen li ci juddoo ci ginaaw bi ay saxal aki lijjanti yu diis yoo xam ne reew yi notoon a leen tegoon ci seen kaw. Loolu nag juroon ci ñoom ag mbañeel akug bëgg a fayyu, nekkiinu koom-koom wi jaxasoo, tegoodi ci yoon, am pax gasu ci Tugal ci diggante askan yeek seeni goornamaa, loolu tam - man nanu ne - mooy li gën a tax ay noste  yu yees sosu, yoy “sañ-sañ bu joyu”  lanu jëloon def ko seen raayo. Ay kureel yu neew jugoon nanu teg loxo ci àtte gi  ci yenn ci reewi Tugal yi, daal di biral ne li leen tax a jug mooy xettali seeni askan ci jafe-jafe yi nga xam ne xareb adduna bu njëkk bi ba na leen fi. Ay goornamaa yu diktaatoor feeñ ci biir Tugal ak ci biti. Leegi nag jeneen jamono ju yees tàmbli ju ngànnaayu, muy wutu ngànnaay moo xam ne li ko jur mooy bëgg a fayyu ci reew yii note ci xare bu njëkk bi, te toroxal askani reew yi nu not, te diisal seen ginaaw ci ay alamaan yu saf te tar. Lii daal moo sabab xareb adduna bu ñaareel bi.

Li laytaay xare bi:

Àttey diktaatoor yu bees yi sosuwoon man nanu ne ñooy jëfka  yi jiitu ci taal ñaareelu xare bi. Ñu indil la wax ju gàtt ci ñatt ci yi gën a am solo ci noste yooyu.

Nosteg àtte gu mbokkoo :

Rusi mooy reew mi àtteg mbokkoo njëkk a taxaw, loolu di woon ci ginaaw fippug oktoobar ga amoon ca atum 1917g, li ko waraloon di koom-koomam ba daanu woon, te ñu dàqoon ko ci anam gu toftaloo ca xare bu njëkk ba ca kanamu Almaañ ci ñaari at yii di 1916 ak 1917g, te mu ñàkkoon it lu tollu ci milyoŋ ak xaaj ci ay xarekatam ca xare booba.

Lenin (1870 – 1924g) mi nekkoon njiitul làngug mbokkte gi (parti communiste), moo jiite woon fipp googu, daal di woon def ag juboo ak waa Almaañ yi, taxwal it ay jataay yu askan yu barab yi (soviets) , daal di xeetal  jumtukaayi ligeey yi, taxawal ab goornamaa bu ay ligeeykat aki baykat, daal di yëngu ci luy neewal tàqale yi am ci diggante xeet yu wuute yi. Waa Rusi yu Sofiet yi taxawaloon nanu ab jë bu yaatu kontar nosteg bopp-alal gu soww gi, ñu jiite woon kureelub mbokkoo  bi kontar diine ak nostey demokraasi yi, ñu mujj nag am doole ju mag ak jeexiital gu rëy ci liy xew ci adduna bi, yàgg nanoo jëfi jëf ci yekkati tàngoor  yi ci adduna bi, walla xiiroo ak ngaayoo yi daa am ci adduna bi ci diggante ñaari xare yi.

Nosteg àtte gu Nasi ca Almaañ:

Làngugug mbokkoo gu xeet gu ligeeykat yi gu ( Nasi) gi (di parti national-socialiste almand des travailleurs) gii làngug politig di gu Nasi gi, daa jariñoo woon (profitoo woon) ci li daloon waa Almaañ yi, te wàcci ci seen kaw ci toroxte ak doyadal ak suufeel, te li ko waraloon di tënk-tënk yi nekkoon ci kollareg Versailles gi, ak jafe-jafe yi mu leen indil, ak  ñàkk gi leen wër, peek leen, ak ñàkk-ligeey gi, ak deltu ginaawug koom-koom bi nga xam ne saxoon na fi ay at ginaaw xare bu njëkk bi, làng gii nag jariñu woon na ci lii lepp ngir fitali ca àtte ga (l’état) teg ko loxo, nangu ko, ci njiitug Adolf Hitler (1889 – 1945g), mi nga xam ne bindoon na dali làngam googu ci teereeb xeexam ba, dal yooyu nag danoo taxawoon ci ay cëslaayi waaso, ndax daa gëmon ne waasow Jermaan mooy waawo wi gën ci waaso yi, te it daa gëmoon ne danoo war a sos ag Almaañ gu mag gu ëmb mbooleem waa Almaañ yi, gëmoon it ne àtte gi (l’état) daa war a teg loxo mbooleem lonkoo yu rënk yu  mag yi ci Almaañ, te danoo war a neenal kollare ga nu fasoon ca Versailles, te danoo war a delloosi mbooleem sancu yi kollare googu ñàkkloo woon Almaañ.

Hitler mujj na di njiilul Almaañ loo xam ne daa amoon sañ-sañ bu joyu (pouvoir absolu). Ñu mujj di ko wooye Fuhrer, mu tàmbli nag di doxal dali làngam yooyu ci askanu Almaañ wi nga xam ne àndoon na ak moom ngir bëgg a mucc te xettaliku ci nekkiin wu bon wi mu nekke woon, rawati na ñàkk-ligeey gi nga xam ne yaatu woon na lool ci Almaañ ngir xare bi, ak ngir tënk-tënk yi nga xam ne kollareg Versailles gi indi woon na leen fi.

Hitler def na ay jëf yu bari yoo xam ne ñoo fi sabab ñaareelu xare bi, ndax daa jëloon diiwaanu Saar boole ko ci Almaañ atum 1935g, neenal kollareg Versailles, jox sodaar si ngànnaay yu diis te xereñ, jëmale endustri bu Almaañ ci ligeey ngànnaay ak jumtukaayi xare aki bagaas yu ame solos xare. Mu jëlati reew yiy wax làkkuw Almaañ wi boole leen ci Almaañ, daal di taxawal Rayix bu ñatteel bi. Mu booleeti Otris ci Almaañ atum 1938g, jëlati goxub Sodit bi nekk ci Cekoslaawi atum 1939g, daal di jeem a nangu yoonu Danseg ci doole, seddoo ak Rusi Poloñ. Almaañ nag dundoon na ci ron àtteg Nasi la ko dale ca 1933g ba bi mu daanoo tas ci atum 1945g.

Nosteg àtte gu Fasi ca Itaali:

Waa Itaali yi yëgoon nanu – te ñoom kat ci reew yi amoon ndam lanu woon ci xareb adduna bu njëkk bi – yëgoon nanu ne danu leen a naxe ca ndajem jàmm ma amoon ca Paris, màngiit  yi juge woon ci xare bi it lu neew lanu leen ci jox, te kat ñoom ñu ci sonne lanu.

Ag ñàkk ligeey tas ci Itaali, nekkiinu nit ñi ñaaw, làngi politig yi fees fa dell, reew ma jaxasoo, xalaat yi tas fa, di mbokkte (communisme) fasi, ak yeneen xalaat yi.
Fasi nag lu fi ñëwoon la ngir xeex mbokkte, Benito Mussolini jiite ko mi jiite woon ag làngam (1883 – 1945g). Làng googu nag danoo warlu woon ci seeni dal (principes) xeex mbokkte, taxawal ag nosteg dimblante, te jeem a jot ci ngañaayi sanc yi nga xam ne danu leen a xañoon Itaali ca ndajem Paris ma.

Ci noonu làngug Fasi gi tàmbli di jëfandikoo fitna(violence) ci xeex ak xuloowaaleem yi, bi dégug làng gi gënee dëgër, gën a ñaw, mu gën a am doole ci la Mussolini ak àndandoom yiy solsimis yu ñuul xuppe goornamaab Itaali bi, ci noonu Buurub Itaali bi di Victor Emmanuel amatul woon pexe, mu daal di jox nguur gi kii di Mussoliini, mi nga xam ne mujj na di diktaatooru Itaati, ñu ko daa dàkkantale Dotsi.

Mussolini digale na ñu neenal làng yi, aaye askanu Itaali wi ñuy def yëngu-yëngu mbaa coow, nos endustri bi, dëppale diggante njariñi ligeeykat bi ak naatug walla jëm kanamug endustriy yaxantu yi. Daal di juboo ak Paab bi, delloosi njàggalem diine mi ci jàngu yi (leekol yi). 

Mussolini feeñal na mbonam gi ak mbonug làngam gi, jaare ko ci jëfam yu ñaaw yi mu jëmale woon ci askanu Libi wi, ba mu fa bëggee samp sancug Itaali gi. Mu gënoon a yaatal ag kilifteefam ca Ecopi atum 1936g, ginaaw bi ko soldaari Itaali yi tegee loxo ci doole, nangoo ko ci waa Ecopi.
Yaatalug sanc gu Itaali gii merloo woon na askan yi nekkoon ci ron ag sancam, te taxoon na yeneen reewi sancaan yi kontar ko ci loolu. Lii nag mooy li jegeele diggante Nasi ak Fasi, nga xam ne mujj nanu àgg ci def ag dëppoo ci seen biir, mooy taxawal ag tapoo gu xare , nu duppee ko diggub Berlin-Rom .

Bokk na ci diktaatoor yii ba tay, làngug xare (parti militaire) gi nekkoon Japon, ak àtteg Franco ga ca Espaañ (1892 – 1975g), moom Franco mi mujjoon ame nguur gu joyu (pouvoir absolu) ca Espaañ atum 1939g, ginaaw xareb ñoñ  bu Espaañ ba.
Koolute gi askani Almaañ yi amoon ak yu Itaali yi, yu Espaañ yi ak yu Japon yi ci seeni goornamaay xeet yu ëppaloon yi te teengal dolliku woon na te li ko waraloon di ñàkk gi nostey bopp-alal yi ak yu demokraasi yi ñàkkoon kàttan ci jële fi coonab koom-koom bii fi amoon ak ñàkk gu tar gii ubale woon Tugal gépp ak feneen, ci biir jafe-jafeb koom-koom bi amoon ci adduna bi atum 1929g, ñu gënoon koo xame ci turu lamb gu mag gi. 

Yeneen jëfka yu sabab xare bi:

Am na fi yeneen jëfka yoy dugg nanu ci li fi indi xare bu ñaareel bi, bokk na ci yi ci ëpp solo:

(1)	lòtt gi kureelu xeet yi lòttoon ci ñoŋal jàmmi àdduna bi, ginaaw bi ci Almaañ ak Itaali gennee ak Japon.
(2)	Digg (axe) yu politig ak xare (militaire) yi nga xam ne reewi diktaatoor yi taxawaloon nanu leen ci seen biir, bu ci mel ne digg bu Berlin-Rom, ak bu Berlin-Tokkiyo, ak kollarante gu ñàkk-a-noonu  gi amoon ci diggante Berlin-Mosko laata a xareb ñaareel bi di tàkk ci lu tollu ci ay ayu bis yu neew. Ci geneen wàll gi, Fraans, Britani, Romani, Poloñ, ñoom itam booloo nanu def seenug tapoo. Nii daal la ñaari dank sosoo dankub digg bi, làmboo Almaañ, Itaali, Japon, ak dankub reew yi tapoo walla (way tapoo yi) di Britani, Fraans, Romani, Poloñ, Benoog Sofiet gi ak Amerig – ci ginaaw bi.
(3)	Xuloo bi amoon ci diggante reewi Balkaan yu yees yi te aju woon ci mbirum dig yi  ci seen biir, ndaxte amunu woon ay dig yu sax, ak xuloo bi amoon te aju woon ci mbirum xeetu (nationalisme), ndax kat reew yii, di yu sosoo ci seddaleg ndaje ma, danoo ëmboon lu sakkan ciy xeeti Almaañ, lu jege juroomi milyoŋi ay waa- Almaañ, ñu mujjoon bokk ci njabootug Poloñ ak Cekoslaafi.
(4)	Masalam yoonu Poloñ wi tàqale Almaañ ak Brusiya, te daytaloo ca waaxub Danseg bu gore ba(libre). Ña dëkke woon ca yoon woowa ci ay waa Almaañ jege woon nanu 96٪ , ci noonu Hitler daal di ne day boole yoon woowu ci Almaañ, looloo fi taalati gilinug xare bi ci adduna bi, ndaxte Fraans ak Britani ñoom danoo daal di woon jàpple Poloñ, ci noonu Hitler daal di joxe ay ndigal ci nu song Poloñ, ci 01 satumbar atum 1939g, ginaaw bi mu gisee ne ànd na ak Bennoog Sofiet gi, Itaali ak Japon . Nii daal la sawaras ñaareelu xareb adduna bi tàkke.

Jamono yi nga xam ne xare bi jaar na ci ak lefi xare bi :

Xareb adduna bu ñaareel bi romb na ci ñatti jamono ñooy:

(1)	Jamono ju ndam yi Hitler doon ame ci xare bi, mu tàmbli ci 1939 – 1941g
(2)	Jamonoy yamoo (équilibre), walla li nuy duppee at mu jaxasoo mi, di woon atum 1942g
(3)	Jamonoy nërméelu ñeel réewi digg yi, mu tàmbli ci atum 1943 – 1945g.

Hitler yëgaloon na Poloñ atum 1939g ne ko manul ñàkk mu génne loxoom ci waaxub Danseg bi, te delloo Almaañ yoonu Poloñ wi romboon ci suufus Almaañ. Boobu lëj-lëj – bokkoon na ci li juddoo woon ca ndajem jàmm ma – mooy li fi taalati xare bi ci adduna, ndax mooy sabab bu jonjoo bi ko jafal. Hitler yamul rekk ci yonnee ag xupp jëme ca Poloñ, waaye da ca a rax dolli yabal ay soldaaram ñu song ko, teg loxo ay suufam, bi mu lànkee bañ a wuyyu wooteb Almaañ bi, bañ a faale xuppam gi. 
Bi mu kodefee, Britani ak Fraans jug yonnee ag xupp jëme ca Almaañ, ne ko na génn suufus Poloñ si, ci diir bu weesuwul ñaar-fukk ak ñeenti waxtu. Bi Almaañ lànkee bañ leen a déglu, la ko Britani ak Fraans song, ci 02 satumbar 1939g.

Almaañ jot naa teg loxo waaxub Danseg ak yoonu Poloñ wi, ak lenn ci goxi soww yu Poloñ yi.
Ag dëppoo am ci diggante Almaañ-Rusi, gu waral ñu séddoo ñoom ñaar suufus Poloñ si, loolu nag di bi Rusi tegee loxo goxi penku yu Poloñ yi, daal di def ak Almaañ kollareg ñàkk-a-noonu (non-agresssion) di gi amoon ci 23 ut 1939g.
Waa Almaañ wéy ci seen xare bi, daal di nangu Danmark ak Norwej atum 1940g, ginaaw ba nu fa dàqee dooley Britani ji ak ju Fraans ja fa nekkoon. Ci geneen wàll, Rusi moom gën na a tàllal ay tànkam ci Finland, loolu nag mu jaare ko ca kollareg ñàkk-a-noonu gi mu fasante woon ak Almaañ. Almaañ daal di song Luksamburg, nangu ko ci lu yéeme cig gaaw. Songati Holand, nangooti ko, song Beljig nangu ko waaye ci ginaaw xare bu saf sàpp, bu mujjoon waral deltu ginaawug dooley Britani ji ak ju Fraans ji atum 1940g. Dooley jañ ak naj gi Almaañ doon def ci bëj-gànnaaru Fraans gënoon a dolliku, gën a tar, ci noonu goornamaab Fraans bi daal di tuxoo Paris, dem Bordeau, foofa lanu tàmbli woon a sàkku ag wéer ngànnaay ak Almaañ. Ci noonu General Deegol daw làqu ca London, fa la doon jiitee jànkoonte (resistance) gu Fraans gi kontar réewi digg yi, fa la birale it ag Fraans gu gore gu ànd ak réewi tapoo yi( les alliés). Goornamaab Fraans bi diriku woon ba Bordoo, daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak Almaañ, muy gu mel ne ga Almaañ defoon ag réewi dëppoo ya ca 1918g. 

Wéer ngànnaay gi nag lii la wax:

(1)	Almaañ nangu bëj-gànnaaru Fraans, péey ba di Paris bokk ca, ak mbooleem tefesi Fraans yi tiim mbàmbulaanug atlas gi.
(2)	Fraans day fay Almaañ ay alamaan yu alal, yu tollu ne ferey soldaari Almaañ yi nangu Fraans.
(3)	Limub soldaari Fraans yi dootul weesu téeméeri junniy soldaar.
(4)	Taxawal goornamaa bu Fraans buy ànd ak Almaañ, bii goornamaa nag taxawoon na ci njiitug Marsal Bitan. Ñu duppee woon ko goornamaab Fishi, ngir nekk ga mu fa nekkoon.  

Ginaaw bi Fraans wommatoo  meruw Almaañ- Itaali wi dafa sottiku woon ci kaw Britani. Bu ko defee, fafalnaaw yu Almaañ yi jog def lòkki  yu toftaloo ci kaw dëkki Britani yi, la ko dale ca ut 1940g. waa Almaañ ñi nag li nu jublu woon ci loolu mooy manante Britani ci wommatu cig wàll, ak waaj ngir wàcce ay dooley Almaañ ca duni Britani ya, ci geneen wàll.
Waaye taxaw gi askanu Britani wi taxaw taxawaay bu dëgër, te sax, moo tax ba waa Almaañ ñi manuñu woon a am li nu bëgg.

Réewi tapoo yi tàmbli woon nanoo ndàmmi ndam, di xaw a kawe réewi digg yi as lëf, bi Amerig duggsee ci xare bi ànd ak ñoom atum 1941g, ni ci Bennoog Sofiet gi dugge. Dooley Britani yi nag ndàmm nanu ndam lu mag ci jë bu Afrig bi ci kaw dooley Itaali yi, daal di leen dàqe ca Ecopi ak Eriteri. Looloo taxoon Hitler yabaloon ñaari kuréeli xare yu Almaañ ca bëj-gànnaaru Afrig, Marshal Rommell jiite woon leen ngir xettali-ji àndandoom ba ca Afrig. 
Ab xeex bu saf am ca bëj-gànnaaru Afrig ca 24 nowambar 1942g ci diggante réewi tapoo yi ak yu digg yi ci njiitug Mongomeri mi jiite woon réewi tapoo yi, ak Romal mi jiite woon réewi digg yi, ci noonu Réewi tapoo yi ndamu ci kaw yu digg yi ca xeex ba nuy wax Alamayni, ginaaw xeexub ñukkaakon (tank;char) bu mag bu sax fukki fan.
Ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xeex bii, nanu ci tudd:

(1)	Teg loxo gi réewi tapoo yi tegoon loxo goxi bëj-gànnaaru Afrig, ginaaw bi nu fa dàqee dooley Itaali ji ak ju Almaañ ji.
(2)	Itaali wommatu na, soldaari réewi tapoo yi wàcc ca Sisil, ñu daal di daaneel nosteg Mussolini gi ca 3 satumbar 1943g
(3)	Nosub xare bi mujj na nekk ci loxol way tapoo yi , ginaaw bi mu nekkee ci loxol Almaañ ak réewi digg yi, àggoon nanu nag ci seen njòbbaxtali ndam atum 1942g

Ndamul Réewi tapoo yi:

Ginaaw bi dooley Britani yi ak yu Amerig yi lijjantee ba am ndam ca jë ba ca Afrig, ak ginaaw bi Mussoolini daanoo, la réewi tapoo yi fasoon yéenee jële fi Almaañ. Ñu wàcce woon soldaar su dul jeex ca tefesug Normandi ga, àggoon nanu cib lim ñaari milyoŋi nit daanaka, ñu tegoon leen nag ci kilifteefug  Generalu Amerig bii di Dwaayet Asinhawar. Bu ko defee yii doole daal di teg loxo Fraans, Beljig, Holand (suuf yu xóot yi). Dooley Almaañ yi xëyoon nanu wëlbati një – cig deltu ginaaw -  jëme Almaañ, waaye dooley tapoo yi mayuñu leen woon fu nu yakke seen nàkka, ngir ragal ñu jekkaat ba amaat doole ju nuy songeeti kenn, ci noonu ñu dab leen ca saa sa, jot a sutuxlu ca digi Almaañ yu soww ya ca fewriye 1945g. 

Ruus yi nag ñoom jotoon nanoo jéego jéego yu am solo ci jëwub penku bi, ci goxi penkub Tugal bi, ginaaw ba fa dooley Almaañ yi jugee, ci noonu ñu nangu jëwub Tugal gu penku gi ci suwe 1944g. 
Ci nii daal la dooley Almaañ tàbbee ciy xat-xat yu jafe, ci kanamu doole yu rëyub lim te nu waajal leen ci ngànnaay yi mujj a génn, bu ko defee Almaañ xëy di ku ñu gaw ci diggante ñaari wàlli kuur , ci diggante penku ak soww, looloo juroon Almaañ faroon wommatu ci mujjantal gi, ci me atum 1945g, ñu daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak réewi tapoo yi, loolu mujj di li taxawal dooley xare ju Almaañ jii jot a miiral adduna bi sonnal ko ngir xareem yu bari yii. Leegi nag réewi tapoo yi – di Angalteer, Fraans, Bennoog Sofiet ak Amerig - nangu nanu Berlin péeyub Almaañ, jàmmaarloo gi waa Almaañ yi doon def ak a dàkku seenub dëkk taxaw te jeex .

Wommatug Japon:

Waa Amerig yi yanoon nanu seen bopp coonab xare bi ci penku kontar Japon. Ginaaw bi waa Amerig nangoo suuf yu bari ci li Japon tegoon loxo ci xare bi, lanu dogu woon ci gañe xeex bi, ginaaw bi nu jotee fent bombub fepp (bombe atomique), te bëgg a xam li mu man, te bëggoon it Japon wommatoo ci seeni loxo.
Ñu daal di jug ci ut 1945, sànni ñaari jum yu fepp ci ñaari dëkk ci Japon ñooy: Irosima ak Nagasaki, ci noonu Japon mujj wommatu, daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak waa Amerig yi ci turu réewi tapoo yi, ci satumbar 1945g, bu ko defee ñaareelu xare bi daal di jeex.

Li juddoo ci ñaareelu xareb adduna bi:

ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xareb adduna bu ñaareel bi, bokk na ci yooyu:

(1)	Def ndajem Botsdam ca anéeru  Berlin, ca 17 sulye 1945g, ngir jeexal xeex bi. Britani teewe woon na ko, Fraans, Bennoog Sofiet gi ak Diiwaani Amerig yu Bennoo yi.
(2)	Dagg goxub Brusiya ci Almaa ñ gu penku gi, bu ko defee Bennoog Sofiet gi jël ca wàllug bëj-gànnaar ga, Poloñ jël wàllug bëj saalum ga, ñu joxati Poloñ dëkkub Danseg bu gore bi (waaxub Danseg)
(3)	Séddale Almaañ def ko ñeenti barabi sañ-sañ, ci diggante Amerig, Britani,  Fraans, ak Bennoog Sofiet. Ci atum 1949g la njëkk a am ci taarixu Almaañ ñaari reew sosu ci Almaañ, te yor ag nosteg pénc (systeme republicain) walla tosteg askan, ñooy: Almaañ gu soww gi walla péncum Almaañ mu bennoo mi (la république Fédérale d’Allemagne), nekk nag ci ron saytug Amerig, Britani ak Fraans, Bon di péey bi. Geneen gi di Almaañug penku gi (Brusiya gu njëkk ga), walla Almaañ gu demokraasi gi (la république démocratique allemande), Bennoog Sofiet gi saytu ko, Berlin gu penku gi dib péeyam. Ñu fàttali leen rekk ne Amerig, Britani ak Fraans mujjoon nanoo may Almaañ atum 1951 mu wut ay soldaar.
(4)	Almaañ ñàkk na mbooloom xareem bu dëgër ma te rëy, ñàkk ngànnaayam yu bees ya te jëm kanam, bi nu tasee ab xareem  neewal dooleem.
(5)	Tegoon nanu Almaañ mu war a fay li mu yàqal rewi tapoo yi.
(6)	Nosaat koom-koomu Almaañ bi, rawati na nosteg alal gi  ak gu endustri gi, yooyu yépp ñu jëme leen leegi ci luy ligéeyal mbiri yi dul xare.
(7)	Séddale Otris def ko ñeenti barabi sañ-sañ ci diggante Britani, Amerig, Fraans ak Bennoog Sofiet. Otris it des ci ron teg loxog réewi tapoo yi ba ci atum 1955g, ak doonte réewi tapoo yi nangu woon nanu ne réew la mu temb dale ko ca atum 1946g.
(8)	Réewi tapoo yi nangoo nanu ci Japon dun yu am solo, bu ci mel ne Farmosa ak Sakalin añs. Rafleel ko ci mbooleem moomeelam yi nekkoon ci màmbulaan gu atlas gi. Dooley Amerig yi nag juge nanu Japon atum 1951g, ginaaw bi nu xaatimee ag kollareg wéer-ngànnaay cis een digganteek goornamaab Japon bic i dëkkub San Fransisko.
(9)	Xaatim nanu ag juboo ak Itaali, Bulgari, Romani ak Hongri atum 1947g, gii juboo nag li mu yaxal mooy réew yii warloo fay réewi tapoo yi ay alamaani xare.
(10)	 Deltu ginaawug ñaari réew yii di Fraans ak Britani ci nekk gi nu nekkoon ay réewi adduna yu mag ci ginaaw xare bi, bu ko defee Amerig ak sofyet yi jël seen barab, mujj it di réew yi ëpp doole ci adduna bi, mujj yor ngànnaay yu bon te aaytal.
(11)	 Nërmeelug ñaari noste yii di Nasi ak Fasi ci Tugal ak nosteg xare ga nekkoon Japon, te noste gu mu ci doon rekk sag am bokk na ci li fi indi ñaareelu xare bi. Nostey diktaatoor yooyu bokkoon nanu ci nooni mbokkte  yi gën a mag
(12)	 feeñug dankub mbokkoo bi (bloc socialiste) ay réew yu bari bokk ci, Bennoog Sofuet gi jiite ko, mu ci mel ne : Kore gu bëj-gànnaar gi, Wietnaam gu bëj-gànnaar gi, Poloñ, Bulgari, Romani, Cekoslowaki ak Hongri añs. Bu dee nag Siin gu Askan gi ak Yogoslawi nag, ñoom ñaar ay réeyi mbokkoo lanu waaye nekkunu woon ci ron yilifug Bennoog Sofiet. Dankub bopp-alal bu gore bi it feeñ, Amerig jiite ko, làmboo nag réewi Tugal gu soww gi, niki: Britani, Fraans, Almaañ gu soww gi, Holand, Beljig, Danmark ak Norwej añs. Amerig it warlul yii réew ndimbalug alal ak gu xare, ngir ñu man a taxaw ci kanamu dankub mbokkoo bi.
(13)	 Sos tapoog càmmooñu Atlas (Otan) atum 1939g, mooy tapoo gi boole woon Amerig, Britani, Fraans, Kanada, réewi sowwub Tugal bi, Japon ak Turki. Réew yii nag danu ne woon ku ci song menn rekk, song nga yeneen yepp. Ñu kollarante woon ci seen biir ci dimblante ci wàllug aaru, koom-koom ak alal. Ci geneen wàll, tapoog Warsaw gi daal di taxaw, tukkee ci Bennoog Sofiet ak réewi mbokkoo yi topp ci ginaawam ci càmmooñu Tugal ak penkoom.
(14)	 Jëya ju rëy ji juddoo ci xeex bi muy faatug lu sakkan ci dooomu aadama ak yàqug alal ju dul jeex, ngir jumtukaayi xare yu xereñ yi nu ci jëfandikoo ñuy jum yi (les missiles), bombi fepp yi, nuuraakon  yi ak ñukkaakon  yu diis yi ans. Xare bii moo ëpp lu mu yàq, ray ko, màbb ko ca moomam ja ko fi jiitu woon.
(15)	 Ëttu àtte yu Normbrug yi ngir àtte ñoñ Nasi ñi ci tuumay jèqi fitna ak sabab xare bi ak def ay tooñaange jëme ci ñu ñu tëj ñi (les prisonniers) ak ñi ñu njafe  ca reewi tapoo ya. Àtte nanu fa tam njiiti nosteg xare gi nekkoon Japon.
(16)	 Juddug mbootaayu xeet yi, ngir dëgëral jàmm ak tere xare yi ak xulooy réew yi, ak amal mbaandute ak yamoo ci réewi adduna bi.
(17)	 Koom-koomu àdduna bépp a naatoon ginaaw bi xare bi jàllee, li ko waraloon di naali tabax yeek yeneen yi nga xam ne defaraat dëkk yi la doon ligeeye ak wàllug tabax ci anamam yepp. Bi gënoon a rëy ci naal yooyu mooy bu Marsaal.
(18)	 Judduwaatug joŋante ci ngànnaay ci diggante ñaari dank yi: bu mbokkoo ak bu bopp-alal, ak sosu gi xare bu sedd bi  sosu ci seen diggante, naka noonu dund ci jàmm gi am leegi ci diggante xeet yi ci kaw suuf.         
    
Doggantal gu ñaareel gi

Mbootaay yu adduna yi: kureelug xeet yi , mbootaayu xeet yi  (walla xeet yu bennoo yi), mbootaayug reewi Lislaam yi  (walla mbootaayu daje gu lislaam gi).

Ñatti mbootaay lanu bëgg’a waxtaane ci doggantal gii, ñooy : Kureelu xeet yi, Mbootaayu xeet yi, Mbootaayu reewi jullit ñi.

Kureelu xeet yi:

Njiitul Amerig la tuddoon Widro WILSON da doon ku daa xalaat nu mu fiy taxawale mbootaay gu mag gu adduna bi, guy jeem’a indi jàmm ci adduna bi, ci ginaaw xareb adduna bu njëkk bi.
Waxoon nanu ne Wilson moom jotoon na a leeral dalam yooyu nga xam ne fukk lanu woon ak ñeent ci biir xeexub adduna bu njëkk bi, ne woon daal fàwwu nu sukkandiku ci ñoom ngir taxawal xeex bi, ak ngir rëddaat sëqooy  reew yi teg leen ci dàtti jàmm ju sax ak moytu xeex yi nar a amati.

Wilson moom gaaraloon na naalam boobu di “Kureelu xeet yi” , gaaraloon na ko ca waxtaanu jàmm wa nu amaloon, kollëre ga nu jotoon a fas ca Versaay it moo rëddoon lanu fa xaatim. Lii di ñew di nanu ci leeral li ëpp solo ciy poñ yu nekk ci kollëre  gi taxawal kureelu xeet yi.

(1)	Sose kureelu xeet yi ci mbooleem reew yi am tèmb  gu mat gu dara wàññiwut, reew yoo xam ne man nanoo indi ay warlu  yu mat ci respekte walla wormaal jàmm, te bàyyi xeex mbaa lu koy waral .
(2)	Reew yi bokk ci kureel gi dananu warlu ne kenn du ci xeex ak kenn te gaaralul li ko tax a bëgg a xeex ci kureel gi, ngir nu àtte leen, te xool li leen boole. Reew yi ci bokk it war nanuy seet mbugal yi yell ci reew yiy tooñ, yu ci mel ne teg leen ay gaw yu koom-koom , walla jëfandikoo doole ci seen kaw.
(3)	Jeem a dëgëral buumi dimblante ci adduna bi jaare ko ci sukkandiku ci maslaa  gu fés, ak wormaal kollërantey reew yi, ak xeex njaam, ci meloom yepp, jeem’a rafetal nekkiinu ligeeykat yi ak seenug dund, ak xeex dorog, nos yaxantu ci adduna bi, ak sonn ci wér gu yaramu nit.
(4)	Reew yi ci bokk dananu warlul yeneen reew yi wormaal seenug tembteg politig , dananu warlu it bañ a def ay kollërey sekkare , ak jox kooluteg kureel bi  ab day  ci mbooleem kollërante yi reew yiy def ci seen diggante. Koolute gi nag di secretariat bi, ci dëkkub Geneve bi nekk Siwis la nekk.
(5)	Aar neewtey  xeet yi ak yu diine yi nekk ci mbooleem reew yi, ak wormaalal askan yi ak xeet yi nekkoon ci ron imbraatoor yi, wormaalal leen seen àq ak sañ-sañ ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg te gis ne moo gën ci ñoom , ak reew yi nu gañee ci xareb adduna bu njëkk bi.
(6)	Kureel bi mooy taxaw ci di xool ni nuy doxale nosteg féetale  gi, mooy noste googu nga xam ne moo waraloon yenn ci askan yi, xeet yi ak mbooloo yi, nu feetale leen reewi sancaan yu mag yi, teg leen ci seen ron kilitfeef ak doxaliin, ginaaw bi reew yooyu nekkee ci waawug reew yi nu gañee woon ci xeex bi, ñuy : reewum Usmaan mi , Imbratooru Otris gi, ak gu Almaañ gi. Loolu nag nu defoon ko ngir waajale leen ci ba man leen’a may ag tèmb  ëlëg . Kureel bi, bi muy door a sosu, 42 reew a ca bokksi woon. Ci noonu reew yiy temb di gën a dolliku, naka noonu di gën a bokksi, ba mujj limub reew yi bokk àgg ci juroom benn fukk, mu ci nekk it am genn kàddu  ci bu nuy woote. Kollëreg kureel gi jox na reew mu nekk àq ak sañ-sañ ci mu genn ne bokkatuma, waaye ci kaw reew moomu teel a yëgale ag bëgg’a bàyyeem lu tollook ñaari at cig njëkk.

Bànqaasi kureelu xeet yi:   

Kureelu xeet yi ñatti bànqaas yu mag la am, ñooy : Jataay bu matale bi , Jataayub Kureel bi, Koolute gi (walla secretariat), nga rax ci dolli ñaari bànqaas yu ci bànqaasoo, ñooy : àttekaayu maanduteg adduna bi  ak mbootaayug ligeey gu adduna bi .

Jataay bu matale bi:

Mi ngi daa ame ci mbooleem ndawi reew yi bokk ci kureel bi. Ab dajeem it benn yoon la daa am ci at mi ci weeru sëtumbar, ngir xool ak xalaat ci mbooleem xew-xew ak mbir yu am solo yi nekk ci ay prograamam.

Jataayub kureel bi:

Moom mi ngi sosoo woon ci njëlbeen gi ci juroom ñeenti cer , juroom yi ci juroom ñeent yooyu ñooy reew yi am ag bokk gu sax ñooy: Britani, Frans, Itaali, Japon ak Almaañ mi jël cerub Amerig mi nga xam ne bokkutoon ci kureel bi. Ak yeneen ñeenti reew yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn leeg-leeg . Bii jataay nag dana faral di daje ñatti yoon ba ñeent ci at mi. Dana faral di daje it, ci anamug jagle, ci xew-xew yu bette yu man a xupp jàmmi adduna bi. Limub toogu yu sax yi tam yokk na ci jataay bi, juge ci ñeenti toogu dem ci juroom ñeent.

Koolute gi (secretariat):

Koolute walla secretariat bu kureelug xeet yi, mi ngi sosoo woon ci ligeeykat yu kureel bi, ya daa ligeeye ca dalam bu sax ba nekkoon Geneve. Njiit li moom moo daa doon Ku-nu-woolu ku matale , ki nga xam ne jataay bu matale bi moo ko daa tànn. Koolute gi nag amoon na ay kureel yu bari yu aju woon ci moom, ñooy: kureelug dimblanteg aada gi , kureelug jële fi ag njaam, kureelug xeex dorog, kureelug aar neewte yi , kureelug féetale yu sax yi  ak kureelug tawat yu bon yi.  

Am na yeneen bànqaas yu am ag jokkoo ak kureelu xeet yi, ñooy yu mel ne: àttekaayu maanduteg adduna bi, ligeeyam di àtte xuloo yi ak amlante yi, àttee ko nag ci yoon walla luwa bu àdduna bi, ak kollërante yi reew yiy xuloo jotoon a def. Nosteg kureel bi nag li mu wax mooy àttekaay bi fukk ak juroomi àttekat ñoo koy taxawal yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn, tànne leen nag ci kandidaa yi nga xam ne reewi kureel bee leen di ind. Àttekaayub maanduteg adduna bi moom, mi ngi sosu ci atum 1921g, ab dalam it nekk Lahaay ca Holand. Ak mbootaayug ligeeyub adduna bi, ligeeyam di yewenal nekkiinu ligeeykat yi ci adduna bi, ak yekkati seen tolluwaayu dund. Moom nag mi ngi booloowoo ci ndawi ligeeykat yi ak sendikaay ligeeykat yi, ak boroom ligeey yi. Geneve nag moo dib dalam.

Ayibi kureelu xeet yi:  

Kureeb xeet yi de, ak li mu def lepp ci ligeey yu jëm ci saxal jàmm ci adduna bi ci biir fukki at yu njëkk yi, ak li mu fi def ci ligeey yu am njariñ ci wàllug mboolaay , loolu lepp teewul mu lottoon te ñakk kàttan ci lijënti xuloo ak ngaayoo yi da a am ci diggante reew yu mag yi. Loolu nag waraloon na neew-dooleg kureelu xeet yi, rawati na ci atum 1930g, bi nga xame ne ag lottam àgg na ci manatul a tee reew yu mag yi di noggatu yu ndaw yi, lu mel ni loolu moo xewoon bi Japon defee ay jalgati jëme ko Siin. Li ko gënoon a doyadil mooy genn gu ci Japon ak Almaañ gennoon atum 1933g, ak lott gu mu lottoon ci tee Itaali songu Ecopi atum 1935g. Loolu sax moo taxoon mu genn ci kureel bi atum 1937g . Kureel bi ba tay demoon na ba manatul woon‘a tee ay “dank yu xare”  yu bees di am,  maanaam ay reew dajaloo,boole seen bopp ci wàlli xare . Kureel bi tam àggoon na ci manatuloon’a tee reew yu mag yi di rewante ci ngànnaayu, yi ci bokk ci kureel bi ak yi ci genn.
Bokk na ci ayibi kureel bi, fent gu ñeenti reew yu mag yi fentoon nosteg feetate ngir may Britani ak Frans nu man’a sancati walla koloniiseeti ay suuf yu bees, yoo xam ne danoo juboo woon ci seddoo leen ci seen biir, rawati na ci reewi araab yi, ak yu dul ñoom. Yenn yi ci yooyu, danoo nekkoon ci ron kilifteefug reewum Usmaan mi, yi ci des ci waawug imbraatoorub Almaañ bi. Reew yu mag yii dano’o jëloon seen xemmemteefi sancaan yooyu  cuub leen ci cuubug ag nite ak bëgg’a def lu baax, bi nu waxee ne kureelub xeet yi daal mooy kilifa gu njëkk gi yilif reew yu neew doole yi muccoon ci kilifteefug Tirki ak Almaañ.
Bokk na ci ayibi kureel bi ba tay, aakimoo gi reew yu mag yi aakimoo woon mbooleem saxal yi ak mbir yi nu daa gaaral ci kureel bi.

Mbootaayu xeet yi (walla xeet yu bennoo yi):  

Ndawi reew yu mag yi, yu ci mel ni Britani, Diiwaan yu bennoo yi Amerig, Bennog Sofyet , Frans ak Siin, danoo daje woon ci Wasington peeyub Amerig ci wenn waxtaan atum 1933g, ginaaw bi as lëf ci ndam tàmblee feeñ ñeel reewi tapoo yi  .
Ci noonu nu gëstu woon nan lanu fiy sose ag mbootaay gu adduna guy yëngu ci saxal ponki jàmm ci adduna bi, jële fi xeex yi, amal fi maandute ak yamoo ci diggante mbooleem reew yi, ak rafetal nekkiinu mboolaayu reew yi ci koom-koom, mboolaay, aada ak wér.
Bi loolu jàllee nu def benn dajeb waxtaan bu adduna bi ci dëkku San Fransisko ci 25 awril atum 1945, ngir rëdd fa ag kollëre ñeel ag mbootaayug xeet gu yees gu fiy wuutu kureelu xeet yi.
Ndawi lu tollook juroom fukk ak benni reew teewe nanu ko, nangu it ci nu def kollëreg mbootaayu xeet yi, ak xaatim ko ci 26/06/1945g. La jiitu ca kollëre ga mooy:

Jubluwaayi mbootaayu xeet yi  ak ay ker-keraanam :

Kollëreg mbootaayu xeet yi dafa saxal ay jubluwaayam  ci ñeenti mbir yu dàttu , ñooy:

(1)	Wattu jàmm ak kaaraangey adduna bi.
(2)	Suuxat seqooy cofeel yi ci diggante reew yi.
(3)	Gën a soññ dimblante gi am ci diggante reew yi ci mbiri koom-koom, ak mboolaay, ak aada, ak wàllug nit.
(4)	Dëppale jëfi xeet yi walla reew yi, walla jëmale leen ci lu dëppoo ak li mbootaayu xeet yi bëgg.

Bu dee ker-keraan  yi mbootaay giy jëfandikoo ngir àgg ci jubluwaay yooyu, moom mbootaay gi leerale na leen ci nii:

(1)	Bennoog askan yu moom seen bopp yi ngir ñoηal jàmm ak kaaraangey adduna bi.
(2)	Di jëf ci anamug jàmm ak baalante ak jéllale ci diggante reew yi.
(3)	Warlu yoon yi man’a yobboo ci nu bàyyi jëfandikoo doole ci bu nuy lijanti jafe-jafe yi  ci adduna bi, ndare bu loolu day li gën ci adduna bi.
(4)	Sukkandiku ci campeefi adduna yi  ngir dëgëral jëm-kanamug koom-koom ak gu mboolaay gu askan yi.

Campeefi mbootayu xeet yi aki jumtukaayam:

Mbootaayu xeet yi mi ngi ame ci ñatti campeef yu mag ñooy:

Jataay bu matale bi:

mi ngi sosoo ci mbooleem reew yi bokk ci mbootaay gi, mu ci nekk it am na genn kàddu bu niy woote. Jataay bi da na daje benn yoon ci at mi ci weeru satumbar, ca dalam ba ca New York, man na’a am nag leeg-leeg ñu amal jataay bi ci xew-xew yu bette yi ko aajowoo. Jataay bu matale bi nag yii ñooy ay yiteem:

(1)	Gëstu naal yi ko reew yi ci bokk di faral’a indil, ak saxal leen, ak def ndinkaane yi war ngir jàmmi adduna bi.
(2)	Gëstu mbir yi nga xam ne man nanoo yokk anami dimblante ci adduna bi.
(3)	Nangu bokkug reew yu bees yi bëgg a bokk.
(4)	Tànn cer yu saxul yi ci jataayub kaaraange gi .
(5)	Tànn àttekati àttekaayu maanduteg adduna bi, ak ceri ñaari jataay yi: bu koom-koom bi ak bu mboolaay gi, ak jataayub ndenkaane bi.

Saxal  yi jataay bu matale bi daa faral di jël, ñi ngi daa ame ci ndollant  gu toll ci ñaari ñatteeli cer (2/3) yu fekke woote bu nuy def ci naal  bu mu man’a doon walla ab ndenkaane.

Jaataayu kaaraange gi:

Jataayub kaarange gi mi ngi sosoo ci juroomi cer yu sax , ñooy ndawi Diiwaani Amerig yu Bennoo yi (USA) ak Bennog Sofyet gi , ak Nguur Gu Bennoo gi  ak Frans ak Siin, ak yeneen fukki cer yoo xam ne jataay bu matale bi moo leen di tànn ngir diirub ñaari at. Cer yu sax yi nag dananu am sañ-sañu firi lepp lu nu fas ca jataay ba, boobu sañ-sañ ñu koy woowe (veto), jataay bi nag dana daje ci anam gu sax ngir xool ci mbir ak xuloo yu adduna bi, yi nga xam ne man nanoo jur njombe.
Saxal yu jataay bi, ñi ngi ame ci ndollant gu toll ci juroom ñeenti kàddu, ci cosaanul fukki kàddu ak juroom, maanaam saxal gi du man’a wér mbaa mu wéy ndare bu juroom ñeent danoo kàddoo waaw, la ca des ne deet walla ñu noppi.
Waaye nag benn saxal du am njariñ bu ko benn cer bu sax firee  ne àndu ci.
Jataayub kaaraange gi moo ame kureel biy saytu kàttanug fepp gi , am na it sañ-sañ ci genne ay saxal yu aju ci taxawal xeex yiy am ci diggante ñaari reew, ak tege ay mbugali koom-koom, ak yu xare  ci mbooleem reew yi dul dégg ndigalam, am na sañ-sañu yabal ay doole  it ngir taxawal ab xeex, walla ay kureeli soldaar  ngir ñu dox diggante ñaari reew yu nar’a xeex.

Koolute gu matale gi :

Moom jumtukaay la bu moo uuf mbooleem ñiy ligeeye ci mbootaayu xeet yi, koolute gi ki koy jiite mooy ku nu woolu kiy jiite mbootaay gi, nga xam ne jataayub kaaraange gi moo koy tànnlu, bu ko defee ñu gaaral mbir mi ci jataay bu matale bi ngir nu woote ko (kàddu ko). Dalub koolute gi mi ngi New York. Ci biir koolute googu lanuy denc mbooleem dosyeey mbootaay gi .

Campeef ak bànqaasi mbootaayu xeet yi: 

Am na ay campeef aki bànqaas yu aju ci mbootaay gi, ñooy:
 
Jataayub koom-koom ak mboolaay :

Bii jataay’a ngi ame ci cer yu seen xam-xam aju ci mbirum koom-koom ak mboolaay. Jataay bu matale bi moo leen di fal ngir diirub ñatti at. Jataay bii nag li nu ko wékk mooy gëstu mbiri koom-koom yi ak mboolaay yi, ak aada ak lu aju ci nit. Mbootaayi adduna yii ma lay bëgg’a leeral ci jataay  bii lanu bànqaasoo:

Moom mbootaay guy jagoo mbiri aada yi la ak xam-xam ak yar , dalam bu sax ma nga Paris, ca Frans.
Yiteem nag mooy dëgëral dimbalante ci wàllug xam-xam ak aada ak yar ci diiggante reew yi ci bokk, jaare ko ci soññ ak sawarloo gëstu ak ligeey yi aju ci yar ak aada ak xam-xam yi.

Mbootaayu Ligeeyu Adduna bi:

Li nekk yiteem mooy rafetal dundiinu ligeeykat yi ci adduna bi, ak fexe nu yokk seeni ngérte  .
Moom nag mbootaay gi, mi ngi ame ci ab lim ci ndawi ligeeykat yi, ak boroom ligeey yi ci mboooleem reewi adduna bi, ab dalam nag mi ngi nekk Geneve.

Mbootaayug Wérug Adduna bi : 

Mbootaay la guy sonn ci dimbali reew yiy màgg ,ci ñu man a xeex tawat yiy wàlle, te yekkati seen tottuwaayu wér gu yaram. Moom mbootaay gi nag dana def ay gëstu ci wàllug wér, di ci sàkku it xam-xam yi manul a ñàkk. Di yonni ay boroom xam-xam ci loolu, di nos ay prograam yu jagoo tàggat ñi yittewoo wallug wér. Ab dalam nag ma nga Geneve moom itam.

Mbootaayu dund ak mbay gu adduna bi : 

Moom nag liy ligeeyam mooy jeem’a def ay pexe ci nu niy yokke li nuy ligeey cib dund ci ñatteelu adduna bi . Loolu nag nu jaare ko ci jëme kanam mbay mi te yokk jumtukaayam aki ker-keraanam, ak xeex gàkk-gàkki mbay yi  ak yu dundat yi , ak dox ci lu fi man a indi ag mottalikoonte gu dund ci adduna bi . Dalam bu sax bi nag mi ngi Rom ca Itaali.
Ëttu àtte bu maandute gu kawe gi: 

Moom nag daa mel ne àttekaayu maandute gu adduna bi gi toppoon ci Kureelu xeet yi. Moom daal moom lanuy jàppe kilifa gu wàllug yoon gu mag gi nekk ci mbootaayu xeet yi.
Mi ngi ame nag ci fukk ak juroomi àttekat yu jataay bu matale bi di tànn, ak jataayub kaaraange gi, ginaaw bu leen seeni reew sampee, gaaral leen ci mbootaay gi. Ligeeyam nag mooy gëstu sabab yi waral xuloo yi ci diggante reew yi. Mooy kàttan gi ame firi ak leeral kollërante yi reew yiy def ci seen diggante, ak àttey yoonu adduna bi. Ab dalam nag mi ngi Lahaay ca Holand.

Mbootaayu xeet giy yëngu ci xettali gi ak tabax:  

Li miy yittewoo mooy mbiri way daw-làqu yi, te indil leen ndimbal li manul’a ñàkk te dëkkal leen, ligeeyloo leen.

Jataayub ndénkaan yi : 

Mooy saytu mbirum sancu  yi Almaañ moomoon, Itaali ak Japon njëkk ñu leen di gañe ci xeexu adduna bu ñaareel bi. Bii jataay nag moo taxaw taxawaayu jataayu feetale bi nekkoon ci kureelu xeet yi, ginaaw xeexu adduna bu njëkk bi.

Bankub addunna bi ngir sos ak tabax:

 Bii bank danu koo sosoon ngir man’a lebal reew yi ci bokk, ak dimble leen ci tabax barab yi xeex bi yàq, ak jëmale kanam barab yiy tàmblee màgg, ak sos ay naal  yoo xam ne man nanoo jàpplee ci màggug koom-koomu adduna bi, ak jeem’a rafetal dundiinu ñi dëkke ci reew yiy màgg  .
Banku adduna bi, moom dafa mel ni ag lonkoo  gu adduna bi, goo xam ne boppu alalam  mi ngi juge ci li cer  yi di teg. Cer bu nekk nag li muy teg day tolloo ak ni koom-koomam toll. Dalam bu sax nag mi ngi Wasington, peeyub Amerig.

Keesug kee gu adduna bi :

Yitteem mooy saxal  njëgu kee  gu adduna bi, ak dindi fi jafe-jafe yi man’a juddoo ci wecciku ci diggante reew yi .

Man nanu ne mbootaayu xeet yi daal mbootaal la gu adduna, gu am sañ-sañ yi kureelu xeet yi amoon, waaye mu ëpple kureelu xeet yi ci ñatti mbir yu am solo, ñooy:
(1)	mbootaayu xeet yi day dëgëral - ci ay jubluwaayam – àqi ak yelleefi doomu aadama yu dàttu yi, ak teddngay nit ak yamale ñaari xeet yi (goor ak jigeen) cig wàll, ak yamale reew yi ci geneen wàll.
(2)	Mbooleem reew yu mag yi bokk nanu ci mbootaayu xeet yi, te bu dee kureelu xeet yi moom Amerig bokku ci woon ngir bañ gu Kongres bañoon ne du ci bokk. Te it Bennoog Sofiet moon bokku ci woon lu dul ci diggante 1934 – 1939 g. Nga rax ci dolli ne cer yi bokk ci mbootaayug xeet yi, boo ñaarte woo cer yi bokkoon ci kureelu xeet yi, yu mbootaay gi moo leen di ëpp.
(3)	Mbootaayu xeet yi am na dooley xare ju koy kàttanal ci mu man’a wéyal ay saxalam, am na it sañ-sañu tege ay dogoo yu koom-koom, ak jëfandikoo doole jëme reew yiy tooñ.

Ànd ak loolu lepp nag, teewul mbootaayu xeet yi moom, doon daanaka ab jumtukaay bu nekk ci loxoy reew yu mag yi am ay toogu yu sax ci jataayub kaaraange gi, yooyu nga xam ne ñoo ame sañ-sañu firi (veto), man a bañ mbaa firi  bepp naal boo xam ne gaaral nanu ko ci jataayub kaaraange gi.
Ci noonu yenn ci reew yu mag yi, fètteerlu nanu,wéy ci jëfandikoo sañ-sañu firi, di ko jëfandikoo fu nu ko wart a defe, di ci tooñe, di ci dumaa, di ci aare reew yuy jalgati. 
Te lu bari ci saxali jataay bu matale bi, ak saxali jataayub kaaraange gi, ba leegi daa rekk lanu ci kayit, kenn doxalu leen. Ab ligeeyam nag ci wàllug dimbalnteg koom-koom, aada, wér gu yaram ak mboolaay, lu am solo la, te yayoo màggal, waaye bu dee ci lu aju ci politig ak xare, moom dëgg-dëgg ni mu ciy doxe sori na dëgg, sori maandute te sori yoon. 

Mbootaayu reewi jullit yi (walla mbootaayu daje gu lislaam gi):

Ag sosam:  

Mbootaay gii mi ngi sosu ci saxal goo xam ne buur ak njiiti reewi jullit yi jëloon nanu ko, ci waxtaanu seen daje bi nu njëkk’a daje, te defe woon ko Ribaat, peeyub reewum Marok, ci diggante 9 – 12 /8/ 1389 g.g , deppoo ak 22 – 25 /9/ 1969 g.
Ñaar-fukki reewi lislaam ak juroom bokkoon nanu ca waxtaan woowa, mbootaayug goreel Falastin (OLP) it teewe woon na ko waaye niki aji fuglu rekk  . 

Ndajem waxtaan moomu mi ngi amoon ci ginaaw bi nu lakkee Masjidul’Aqsaa, ci 21/8/1969 g , te ay yahuud def ko. Waxtaan wa ba muy tëj daa ñaawlu jëf ju bon jooju, nga xam ne day wone ag noonu gu nu def jullit ñi te ñàkk’a wormaal seeni gëm-gëm . ñu sàkku woon it ci Israayil mu genn ci mbooleem suufi araab yi mu tegoon loxo atum 1967 g. Te delloosi dëkkub Quds bi  ci ni mu nekke woon ca xareb sue (juin) ba atum 1967 g. Mu feddali ba tay moom ndaje mi, jàpple gu miy jàpple reewi artaab yi, ci seen xeex bi nuy def ak Israayil, ak jàpple gi muy jàpple waa Palastin ci nu delloosi seen àq ak yelleef yi nu teg loxo, te goreel seeni suuf.

Kollëreg mbootaayu reewi jullit yi: 

Kollëreg mbootaay gi mi ngi genne ca ñatteelu waxtaan wa jëwrini bitim reew yu reewi lislaam yi amaloon ca Jidda atum 1392 gg, dëppook 29/2 -  4/3/ 1972 g. Mu sampu woon – moom kollëre gi - ci li taxoon nu sos mbootaay gi.

Li nekk ci poñ bu njëkk bi ci kollëre gi mooy “reew yi ci bokk ñi ngi sos mbootaayug reewi jullit ñi (walla mbootaayug daje gu lislaam gi)” poñ bu ñaareel bi làmboo dali mbootaay gi  aki jubluwaayam. Jubluwaay yooyu nag weesuwunu woon “ amal fi jawwu ju baax, ju nu man a dëgërale dimblante ak deggoo ci diggante reew yi ci bokk, ci seen biir, ak ci seen diggante ak yeneen reew yi.
Waaye dal yi nag ñoom ci nii lanu taxawe:

(1)	Yamoo gu mat ci diggante reew yi ci bokk
(2)	Wormaal àq ak sañ-sañu reew mu ci bokk, ci wutal boppam mujj ga ko soob, ak bañ’a dugg ci mbiri biiram.
(3)	Wormaal moomeelug reew yi bokk ak seenug temb.
(4)	Dëgëral dalu dimblante gu lislaam gi, ci diggante reew yi bokk.
(5)	Dëgëral dimblante ci diggante reew yi bokk, ci wàlli: koom-koom, mboolaay, aada, xam-xam ak ci yeneen wàll yu am solo yi, ak diisoo ak yeneen reew yi bokk ci yeneen mbootaay yi.
(6)	Jeem’a far boddante ci biiru xeet, ak sanc  ci mbooleem ay anamam.
(7)	Def lepp lu man a indi jàmm ak kaaraange ci adduna bi, ci anamug maandute.
(8)	Dëppale ak nos ligeey bi reew yi seq, ngir njoηal barab yu sell yi te goreel leen , ak jàple waa Falastin ci seen xeex bi, ak dimble leen ba nu man’a delloosi seen àq ak yelleef, te jotaat seen suuf.
(9)	Jàpple mbooleem reewi jullit yiy xeex ngir njoηal seen teddnga, jot seen tèmbte, dollosi seeni yelleefi reew.
(10)	Lijjanti xuloo yi nar a ami ci diggante reew yi bokk ci mbootaay gi, lijjanti loolu ci jàmm, niki: waxtaan, dox diggante , ak layoo .
(11)	Reew yi ci bokk, danoo war’a bàyyi - ci seeni seqoo  – di jëfandikoo doole walla xuppe ci jëfandikoo ko, jëme ko ci suufus reew mu bokk walla jëme ko ag tèmbam .    

Campeefi mbootaay gi aki kureelam ak jumtukaay yi ci bànqaasoo:

Mbootaay gi sos na ay campeef yu bari yu cosaanu niki :

(1)	Jataayu buur yi ak njiit yi
(2)	Jataayu jëwrini bitim reew yi
(3)	Koolute gu matale gi 
(4)	Àttekaayu maandute bu lislaam bu adduna bi.

Bu dee kureel yi ci bokk nag, ñooy:

(1)	Kureelu Quds
(2)	Kureel bu sax bi ñeel wàllug koppar
(3)	Kureelu lislaam bi saytu wàllug koom, mboolaay ak aada.
(4)	Kureel bu sax bi ñeel dimbalanteg xam-xam ak xarala 
(5)	Kureel bu sax bi ñeel dimblanteg koom ak yaxantu
(6)	Kureel bu sax biy yëngu ci wàllug xamale  ak aada 

Bu dee nag lu aju ci jumtukaay yeneen yi bànqaasoo ci mbootaay gi, ñooy:

(1)	Keesug dimblante gu lislaam gi 
(2)	Keesug Quds
(3)	Daaray gëstu gu lim yi  ak koom, ak mboolaay.
(4)	Barabu lislaam biy yëngu ci jàngale mecce ak xarala, ak defi gëstu.
(5)	 Cëslaayu  lislaam giy saytu xam-xam xarala ak suqli koom-koom.
(6)	Barabu adduna biy yëngu ci yar ak njàngalem lislaam.
(7)	Barabub lislaam biy sonn ci suqali yaxantu
(8)	Kureelu lislaam gi saytu terute gi ci adduna bi.
(9)	Kureel adduna gi saytu ndono lu lislaam li
(10)	Akaademi bu xam-xamu lislaam
(11)	Jataayu lislaam bi yor tukkib jawwu bu nit ñi 
(12)	Kureelu lislaam bu adduna bi ñeel yoon

Bu lii jàllee, teewul sosees na ba tay  yeneen cëslaay yu bokk ci mbootaay gi, ñooy
(1)	Banku lislaam bi
(2)	Barabu xibaar bu lislaam bu adduna bi 
(3)	Mbootaayu rajoy reewi jullit yi
(4)	Neegub yaxantu  bu lislaam bi, ak mecce ak joqalanteg njaay yi
(5)	Mbootaayu peeyi  lislaam yi
(6)	Suqali gu lislaam gi jëm ci boroom gaal yi
(7)	Mbootaayug lislaam gi jëm ci yar, xam-xam ak aada.

Jagley campeef yi ak seeni ligeey:

Jataayu buur yi ak njiit yi, mooy campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi. Moom nag dana faral di daje saa su ko yitey xeet wi laajee, ngir gëstu ay mbiram, ak lijanti ay lëj-lëjam.

Buur yi ak njiit yi ci bokk nag, saxaloon nanu ca seen ñatteelu ndaje ma nu defoon ca Makka (mu sell mi) ak Taayif, ci diggante 19 – 22 rabihul-awal 1301 gg, dëppook 25 – 28/1/1981g, saxaloon nanu fa ne danuy def ndaje yi ñuy luy wër ci seen diggante ci ñatti at yu nekk.

Niki nu ko waxe woon, mbootaay gi, ndajeem mu njëkk, mi ngi ame woon Ribaat, diggante 9 – 12/7/1389gg, dëppook 22 – 25 /9/1969g. Mu defaat meneen ndaje ca Lahoor ca Pakistaan, diggante 29 muharram – 01 safar 1394 gg, dëppook 22 – 24/3/1974 g .
Ñatteelu ndajeem mu defe ko Makka ak Taayif, diggante 19 – 22/3/1401gg , dëppook 25 – 28/1/1981g.
Mu def ñeenteelu ndajeem ca Kaasa Balanka, ci diggante 13 – 17 rabiihu-saani 1404 gg, dëppook 16 – 19/1/1984g.
Juroomeelu ndajeem ame Kuwet, ci Jumaadas-saaniya 1407 gg, dëppook 26 – 30/1/1987g.

Jataayu jëwrini bitim reew yi nag, mooy ñaareelu campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi, ginaaw jataayu buur yeek njiit yi. Campeef bii nag dana faral di daje – ci anam guy wër – ci at mu nekk, ci benn ci reew yi bokk, ngir xool mbooleen bataaxel yiy doxal politigu mbootaay gi. Ak jël saxal yi war ci mbir yi am ay njariñ yu reewi mbootaay gi bokk, loolu lepp nag, fekk mu dëppoo ak jubluwaayi mbootaay gi aki bëgg-bëggam.
Jataayub jëwrin yi mooy xool saxal gi nga xam ne kureelub koppar bu sax bi di na koy def, ngir saxal ko te wéyal ko.
Mooy xool it njël lu yaatu  lu kooluteg mbootaay gi.
Bokk na ci ay ligeeyam, di sàkku ci mbootaay gi muy daje, bu jaadoo, ngir ay xew-xew yu bette, yu yitteel jullit ñi.
Jataayub jawrin yi ba tay dana faral’a daje ci anam gu xotti baax, saa su ko yitte laajee.

Bu dee koolute gu matale gi nag walla, moom mooy campeef biy wéyal jëf yi  ci mbootaay gi. Mi m ngi sosoo ci saxal (resolution) gu genne woon ca ndajem jëwrini bitim reew ma nu amaloon ca Jadda, diggante 23 – 25/3/1970 g.
Yiteem nag mooy def ligeey yi nu ko sant, ci biir àttey kollëreg mbootaay gi. Dina dimbli tam yeneen campeef ak bànqaas yi bawoo ci mbootaay gi, ak di dëppale seeni prograam yu wuute yi. Bokk na ci yitteem ba leegi, topp ak xeeñtu saxal ak ndenkaane yi tukkee ci ñaari ndaje yii: mu mbootaay gi ak mu jëwrin yi.
Kiy saytu ligeeyi koolute gi, mooy ku nu wóolu  ki nga xam ne mbootaay gee koy fal, ngir diirub ñeenti at yees manul’a yeesal, bu ko defee ñeenti dimblikat  ak ñeenti ñu-ñu wóolu di ko jàpple, kenn ci ñoom, jagoo mbirum Palastin ak Quds, mbootaay gi Jidda la defandi dalub kooluteem gi, ba kero nuy goreel  Quds,insallaa, ngir nu def ko dal bu sax bi.
Làkk yi mbootaay giy jëfandikoo ciy ligeeyam ñooy: Araab, Franse, Angle.
Mbootaay gi nag mbirum Palastin yitteel na ko lool, ak mu Quds, moom mi nga xam ne moo uuf Masjidul-Aqsa, mi Yàlla teral te teral li ko wër, ak doj wu sell wa, ak miir ba nuy wax “Miiru Buraax” .  Ak yeneen mbir yi aju ci diiney lislaam te nekk ci mbooleem barabi lislaam yi.
Quds nag boo gisee nu fonk ko, day suuf si Yonnant bi rañaane woon yeeg, loolu nag dana waral ci jullit ñi ñu fonk ko te yittewoo ay mbiram, te aar ko ba noon yi dunu ko tilimal.
Kureelub Quds mi ngi sosu ci ndigal lu tukkee ci juroom benneelu ndaje mu jëwrini bitim reew yi, mi ame woon Jidda ci diggante 12 – 15/7/1975 g.
Ndajem jëwrin mu fukkeel ma nu defe woon Faas ca Marok, ci diggante 10 – 14/5/1979g, ndaje moomu dal di denk njiitug kureelu Quds bi buuru Marok bii di Asan mu ñaareel mi. 
Ligeey yi nu denk kureel bi mooy yii:
(1)	Di gëstu lay xew Quds
(2)	Di topp ak a xeeñtu doxalug saxal yi aju ci Quds, te jataayub jëwrin yi def leen,
(3)	Di jokkoo ak mbootaayi adduna bi, yi man a dimblee ci aar Quds
(4)	Di wax ci lu man a doxal saxal yi ci aju.
(5)	Di indi ag saxal ci at mu nekk guy leeral ay ligeeyam aki jëfam ci jataayu jëwrin yi.

Kureelu Quds moom, njiit la ko jiite moo ko man’a dajeloo walla lu mbootaay gi. Kureel gi nag mi ngi ame ci ndawi 15 reew, yu bokk ci mbootaay gi, yoo xam ne jataayu jëwrin yee leen di tànn ngir diirub ñatti at.

Doggantal gu ñatteel gi: 
Reew yi def ay dank  ak reew yi feetewul fenn

Ag jiital:

Bokk na ci li gën’a rëy ci li juddoo ci xeexu adduna bu ñaareel bi, bokk na ci li ci gën’a rëy, feeñug walla juddug ay dank yu ay reew, walla ay booloo yu ay reew , ci wàllug politig walla xare.
Ci noonu dankub bopp-alal  dal di feeñ nee, Amerig jiite ko, mu uuf nag Biritani, Frans, ak lu bari ci reewi Orobug sowwu gi. Mbooloo mii nag ñi ngi ko daa woowe dankub sowwu bi , ak reewi adduna ju gore ji, safaan nag walla wuute ak reewi bokkoo yi  . 
Bu ko defee Amerig moom, jug di dimbli reewi dankub sowwu bi, ci ngànaay ak xarala, ak alal, ngir dëgëral seen koom-koom, te may leen doole ba nu man a taxaw di tata  ci kanamu reewi bokkoo yi, tee leen a tas, tee leen a wisaaroo.
Naka noonu, dankub bokoo bi , moom itam sosu,  Bennoog Sofiet gi jiite ko, mu uuf lu sakkan ci reewi bokkoo yi ci Tugal gu bëj-gànnaar gi, ak gu digg gi, ak reewi bokkoo yi nekk Asi, niki Kore gu bëj-gànnaar gi, Wietnaamm gu bëj-gànnaar gi, ak Siinug askan gi .
Ñaari dank yii: di bu sowwu bi ak bu penku bi, xeex nanu ba tàyyi ngir yilif adduna bii nga xam ne sonne na lool ci ñaareelu xeexu adduna bi, nga xam ne reewi Orob yi sax mujj nanu di reew yu lòtt te neew doole ci kanamu ñaari reew yu mag yii di: Diwaani Amerig yu Bennoo yi ak Bennoog Sofiet gi, looloo waraloon gisiin wiy woote ne “reew yi ñoo tolloo, yamoo, ay nawle lanu” wii gisiin naaxsaayoon, te  faf far, xajal  fi wiy indi doonadi moroom gi Amerig ak Sofiet doonadi woon moroom ci yeneen reew yi.
Loolu nag taxoon na ba reewi Orob yi tàmbli woon’a xalaat ci seen ëlëg, ginaaw bi nu mujjee di reew yu ñàkk solo bu nu leen tollalee ak yile ñaari reew.
Ginaaw ñaareelu xeex bi it, yeneen reew feeñ nanu, ñu leen di woowe reew yiy màgg, yi ci ëpp nag ñooy reewi Asi ak Afrig, yi doon door a tembe ci reewi sancaan yu orob yi.
Reew yooyu tam danku nanu ngir taxawal dankub reew yi feetewul fenn, ne li niy def mooy fas yeenee ame ag peeteedi gu rafet ci diggante ñaari reew yu mag yi, ak yi nekk ci seeni ngunu. 
Dananu leen leeral ci lii di ñëw lenn ci danki adduna yi, bu ci mel ni:
Tapoo  gu càmmooñug atlas (Otan):

Njiilul Amerig lii di Harry Truman (1884 – 1972 g) dafa nekkoon ku bañoon  lool mbokkte walla (cominisme), te bañoon it mu tas. Looloo taxoon mu taxawaloon ci atum 1939 g, ag tapoo walla alliance gu boole woon Amerig, Itaali, Holand, Beljik, Norwej, Danmark, Fraans, Kanada, Portigaal ak Island.
Ñu tudde woon nag tapoo gii, tapoo gu càmmooñu Atlas. Ginaaw bi la ci Turki bokksi ak Gres, atum 1951g, ak Almaañ gu federaal gi atum 1955 g. Seenug kollëre it ci ñatti wàll yii la jëm:

(1)	kepp ku laal benn ci reewi tapoo gi, laal nga yi ci des.
(2)	Reew yi ci bokk dananu dimblante ci seen biir ci wàllu aaru , alal ak koom.
(3)	Tapoo gi dana taxawal ab jataay bu xare , te da na am njiit lu matale tam.

Jaadu na nu leeral ne Amerig mooy dàttub tapoo gii, maanaam mooy reew mi ci ëpp solo, ci wàllug li nuy joxe ak ngànnaay. Paris it moo nekkandi woon ab dalam, ba ci mujj gi nu tuxal ko ca Buruxel, peeyub Beljik. Bokkoon na ci li ko taxoon a jug, neexal dundug ay askanam, yombal seenu nekkiin, dëppale ko ak sarti demokraasi, goreg jëmm  ak yoon.

Tapoo gu Warsaw:
Bennog Sofiet ñoom itam taxawal nanu ag tapoo gu kaaraange, atum 1955 g, loolu nag booy seet, ag won Amerig rekk la ne nun itam toogunu, boo sosee tapoo gu Atlas, nu sos sunu gos, rawati na bi ci Almaañ gu sowwu gi bokksee (ci gu Atlas gi) atum 1955 g. 
Tapoo gu Warsaw moom, Bennoog Sofiet la woon, reewi bokkoo yi nekk ci ngunoom, maanaam yi ànd ak moom, ci gànnaaru Tugal ak diggam, mell ni: Romani, Poloñ, Hongri, Cekoslowaki añs. 
Warsaw nag li ko taxoon a jug mooy aar Bennoog Sofiet gi, ak reew yi ko topp, ci mbooleem musiba mu man a bàyyikoo ci tapoo gu càmmooñu Atlas gi.
Dëkkub Warsaw bii di peeyub Poloñ moo mujjoon dib dalam, li mu yoroon it ciy xarekat àggoon na ci 6000000 xarekat, ñu seddale leen ci diggante reew yi ci bokk.
Tapoo gu kollëre gu diggu gi:
Waa tapoo gu Atlas, Amerig jiite ko, danu ne woon daal fawwu nu jële fi bennoog Sofiet, tas tapoom gii di Warsaw, ci noonu ñu taxawal ag njiit  gu jagoo mbirum penku bu diggu bi  atum 1951 g, ginaaw bi nu sos mbootaayug aar penku bu diggu bi, atum 1952. Ci atum 1955 g, nu sos tapoo gu Iraak – Turki, ñu gën koo xame ci tapoo gu Baxdaad, tur woowu nag mujj na soppiku atum 1958 g, mujj di tapoog kollëre gu diggu gi, ginaaw bi ci Iraan bokkee, Pakistaan, Britani, ci wetu Turki ak Iraak.
Ñu leen di fattali rekk ne Iraak moom mujj na genn ci tapoo gii ci suwe atum 1968 g.
Jataayub Tugal bi :
Waa Tugal ya daa woote bennoog Tugal, ak tembug ay gis-gisam aki saxalam, taxawaloon nanu ca atum 1949 g jataayub Tugal bi, muy ag mbootaay gu koom-koom, gu politig, loolu nag doonoon ab jeego bu njëkk rekk, jëm ci reewum Orob mu mag mu nu bëgg a taxawali.  
Bookoon na ci jataay boobu nag: Biritani, Frans, Itaali, Belgik, Holand, Luxamburg, Danmark, Norwej, Suwed ak Irland, nga rax ci dolli ay ndawi parlamaa yu reewi Orobug sowwu gi ak Turki. Dëkkub Strasburg bu Frans bi moo doonoon dal bi.
Rewwi Tugal ya ca ja bu nu bokk ba :
Waa Tugal yi – ci ag kollare gu nu fase woon ca Rom Atum 1957 g – taxawaloon nanu am mbooloo mu koom-koom mu Orob, nu gënoon koo xame ci turu Reewi Tugal ya ca ja ba nu bokk, ngir jële fi ag nduwaan ci diggante reew yi ci bokk, te doxal fi yaxantu gu gore  ci seen biir. Buruxel nag lanu defoon seenub dal. Bokkoon na ci Frans, Britani, Itaali, Beljik, Almaañ gu sowwu gi, Luxamburg, Holand, Irland, Danmark ak Yonan (Gres). Ja boobu nag li ko taxoon a jug mooy dimblanteg koom-koom gu Orob, waaye mujj na rax ci gu politig gu yaatu ci seen biir.
Mbootaayu dimblanteg koom-koom ak suqali  :

Mbootaay gii, Amerig moo ko sosoon atum 1980 g, muy mbootaay gu mel ni ( Reewi Tugal ya ca ja ba nu bokk ), ngir rekk man a dugg ci koom-koomu Tugal bi cig wàll, ak ngir man a dëgëral ay seqooy koom-koomam yi mu am ak reewi Ja bi, ci geneen wàll.
Bokk na ci mbootaay gi nag: reewi tapoo gu Atlas gi, ak Siwis, Finland, Otris, Suwed, ak Yogoslawi.
Mbootaayug reewi Amerig yi: 
Mbootaay gii yàgg na a sosu, ndax def na ko ci 30 awril atum 1948 g, waaye ag dëgg-dëggi sosoom mi gi door atum 1890 g, muy – man nanu ne – lu juddoo ci xalaatu njiitul Amerig lii di woon Monrow, mi daa wax naan ((Amerig daal ñaari Amerig yi ñoo ko moom)). Mbootaay gii nga xam ne Diiwaan Yu Bennoo Yu Amerig yi ñoo ci bokkoon ak  reewi Amerig gu Latin gi, mujjoon na gën a yaatu gën a jëm kanam, mujj di ëtt bu am solo ngir dëppale diggante reew yi ci bokk, waxuma la nag njariñul koom-koom lu mag li ci nekk.
Waa mbootaay gii nag Wasington lanu defoon seenub dal, te Amerig it  amoon na kilifteef gu mag ci mbootaay gi, kilifteef googu feeñ na bu baax, bi Amerig tèggee Kuba ne bokkatul ci mbootaay gi, loolu nag mi ngi amoon ci ginaaw bi fi ag fipp gu bokkoo  amee ca atum 1958 g.

Mbootaayi reewi Andis yi:

Moom nag mbootaay gu jagoo yenn ci reewi Amerig gu Latin gi la, li ko tax a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom-koom ak aada . ñi ci bokk nag di Kolombi, Peru, Ekuwador, Cili ak Boliwi.

Naalub Marsaal bi ak Komikon:
    
Bennoog Sofiet daa taxawaloon ag mbootaayug koom-koom atum 1949 g, ngir fayyoo ci ci li Tugal def ci wetam muy mbootaayug Ja bi, nga xam ne Amerig moo ko digaloon waa Orob yi, ne leen woon nanu taxaw ci tabaxaat seen koom-koom bu daanu bii nga xam ne xareb adduna bee ko màbboon, te moom dana leen ci jàpple, wooteg Amerig googu, ñi ngi ko gënoon a miine ci turu “Naalub Marsaal” , Marsaal nag jawrini Amerig ji yoroon wàllu bitim reew la woon, ci ginaaw ñaareelu xareb adduna bi.
Sofiet yi nag ñoom seen mbootaayu koom-koom ñi ngi ko tudde woon “Komikon”, Bennoog Sofiet jiite woon ko, mbooleem reew yi àndoon ak moom bokkoon ci. Li ko taxoon a jug di dëppale reew yi ci bokk ci wàllu koom-koom.

Mbootaay gi boole reewi araab yi :

Reewi Araab yee ko sos ci atum 1940 g, ngir dimblanteg politig, gu koom-koom ak gu aada, ci seen biir.

Mbootaayug jàpplante gu Asi:

Reewi Asi yee ko sos ak yu Afrig yi, ngir dëgëral diggante reew yi ci bokk.

Mbootaayug bennoog Afrig :

Moom mbootay la gu reewi Afrig yi, ñu sos ko atum 1963g, li ko tax a jug di dëgëral buumi dimblante ci diggante reew yi ci bokk, rawtina ci wàlli poloitig, koom-koom ak aada.

Reew yi féetewul fenn: :

Reww yu bari temb nanu, ginaaw ñaareelu xareb adduna bi, rawati na ci goxu Afrig ak Asi, ñu daal di dem nag bokki ci mbootaayu xeet yi. Reew yooyu di door a am ag temb, soxla woon nanu di diisoo ci seen biir, te di daje, ndax kat ragaloon nanu bu baax reewi sancaan yi ak seeni pexe cig wàll, ak ngir ne ginaaw bi nu tembee ba noppi, danoo fees dell aki coonay koom-koom ak yu politig ci geneen wàll.

Ci nooonu am mbooloo sosu mu nu xame woon ci turu “Mbooloom reewi Asi yi ak Afrig” , ab xalaat dox ci ñoom jañ leen ci ñu taxawal ndajem Asi-Afrig, ngir gëstu jafe-jafey ñaari gox yi, rawati na lu aju ci goreel ay askan seen, ak tembal leen, teggil leen sukkub sanc bii tegu ci seenug dòq, ak ci anam gu mu ci teggoo.

Ci noonu nu def ndajem Bandonj ca awril 1955 g, ca Endonesi, ndawi lu tollook 29 reew teewe ko, yu Afrig ak Asi, ñooy: End, Bakistaan, Endonesi, Borma, Silan (mujj di Sirilanka), Afganistaan, Iraan, Japon, Filipin, Taylan, Siin Gu Askan gi, Wietnaam gu bëj-gànnaar gi, Wietnaam gu bëj-saalum gi, Cambodie, Lawus, Nipal, Ecopi, Liberia, Tefesug Wurus (Gana ginaaw bi), Siri, Isipt (Misra), Iraak, Nguurug Araabi Sawdid, Jordanie, Libi, Sudan, Liban ak Yaman.
Ndajem Bandonj nag mooy ndajem adduna mi njëkk a boole ndawi ay reewi Asi ak yu Afrig yu temb.
Ay ndénkaane aki saxal yu bari juddoo nanu ca ndaje ma, yuy soññee ci nu yamale diggante xeet yi ak waaso yi, te wormaal àqu ak yelleefu doomu aadama ju cosaanu ji, ak sañ-sañu nit ci wutal boppam mujj gi ko neex.
Moom ndaje mi tam woo na reewi Afrig yi ak Asi ci nu dimblante ci kom-koom ci seen biir, te diisoo ci politig.

Ndajem Reew yi feetewul fenn, nag juddoo na ca ndajem Bandonj moomee. Nu njëkk koo amal ca Keer atum 1958 g, ma ca topp, nu defe ko Konaakri atum 1960 g .
Bi adduna bi gënee bari ay coow, xuloo yi gën a tar ci diggante reew yi, Jamaal Abdu NAASIR, mi nekkoon njiitul reewum Isipt ak kii di Tito nekkoon njiitul Yugoslawi, ñoom danoo woo woon reew yi feetewul fenn te nekk Afrig, Asi ak Amerig Latin, ne nanu def am ndaje mu mag, ngir gëstu tolluwaay bii, ak tàngoor wii ci adduna bi.
Ci noonu nu daal di def ndajem Belgraad, ci sëtumbar 1961 g, daal di genne ay saxal yu aju ci jàmmi adduna bi, ak jafe-jafe yi aju ci noccim ngànnaay mi , ak jafe-jafe bu Aljeri bi ak bu Kongo, ak yeneen jafe-jafe yu adduna yu bari yu amoon ca jamono ja.
Nu defaat meneen ndaje ca Keer, mu Reew yi feetewul fenn, ci Oktoobar 1964 g. Lu tollook 47 ci ndawi reew teewe woon ko. Ab lim nag ciy saxal aki ndenkaane yu am solo genne na ca mooma ndaje, nu tudd ci yii rekk:

(1)	wormaal sañ-sañu askan yi ak seen àq ci wutal seen bopp mujj gi nu bëgg.
(2)	Àndandoo ligeey ngir goreel reew yi tembagul.
(3)	Sakku nu nocci ngànnaay yi, te lijënti xuloo yi ci yoonu jàmm, te jële fi tapoo yi  tas leen, dindi dàtti xare yi .
(4)	Ligeey ngir suqali dimblanteg koom-koom, aada, xam-xam ak yar  ci diggante reew yi ci bokk.

Ñi ngi fattalee ne Reew yi feetewul fenn dolliku nanu, bi reew yi temb gënee dolliku, xuloob reew yi gën a tàng, rawante ci ngànnaayu gën a yokku, ci ngànnaay yu nu xamoon yi ak yu gën a jëm kanam yi. Looloo waraloon Reew yi feetewul fenn gën di dolli seeni daje yiy wër, ak di gën di ligeey ngir adduna bi man a dégg seen baat, te man cee def jeexiit  bu baax.

Ñeenteelu Doggantal     

Fipp gi xam-xam amal ci Elektron : 

Xamale lan mooy “ Elektron” :

Elektron moom yaram wu sew la lool, moom daal gën na a ndawe ay milyoŋi yoon, yeneen yaram yi nga man a gise ci bët rekk, bu nu rafleel. Moom sax manoo koo gise ci fésalukaay  yu elktronik yu bees yi am leegi. Li ko waral mooy boo jëloon ay bilyoŋi Elektron dajale leen, du nu toll ne boppu puso.

Elektron nag nekk na ci bepp ne-ne  bu Yàlla sàkk, moom nag mooy peek  fepp wi , walla saal bi , moom nag foo ko fekk da koy wër ngir xëcc gi ko saal biy xëcc. Elektron ni muy wëre saal bi - booy xool - day mel ne ni bidiw yu mag yi  di wëre jant bi.
Elektron nag day yanu ay cëfkay kuran  yuy bañ , saal bi walla fepp wi di yor ay cëfkay kuran yuy wuyyu  walla nangu.

Xam-xamu Elektron ni mu sosoo:

Xam nanu ne xam-xamu Kuran moom xam-xam la bu nu xame bu yàgg ci ki nuy wax Taalis, di woon boroom xam-xamu Gres. Ay boroom xam-xam yu bari nag ñëw, gën koo jëme kanam, bokk na ci ñooñu kii nuy wax Wilyaam Jilbert, di boroom xam-xamu Angle boo xam ne mooy ki teqale dooley kuran ak dooley bijjaakon , ci noonu la wuuteek kii di Taalis mi ne woon ñoom ñaar daal benn lanu.
Jilbert it xamoon na ne duusi kuran yi mooy jur dooley asye. Boroom xam-xamu Almaañ bii di Anofon Jiyorik, moom itam di ki njëkk a genne masinu juddal kuran, maanaam jumtukaay buy tax kuran bi di judd, di am, loolu di ci atum 1663 g. Tomas Adison it ñëw, indil ñu lamp bu kuran.

Xam-xamu kuran nag soppiku di xam-xamu elektron ci njëlbeeni xarnub ñaarfukeel g, loolu nag mi ngi amoon ginaaw bi boroom xam-xamu fisiyaa bu angle bii di Josef TOMSON jugee, feeñal xam-xamu elektron atum 1897 g, daal di ciy ame neexalub Nobel ci xam-xamu fisiya.
Li gën a jëmal kanam xam-xamu elektron nag mooy feeñal gi boroom xam-xam yi feeñal ne fepp (saal biy wuyyu) day xëcc jëme ci boppam lu bari ci elektron yiy bañ, te moom fepp wi day seddaliku ci fepp yu bari.
Ndamul xam-xam lii ab jeego la bu am solo ci doxub xam-xamu elektron. Jeego bii daal bu am solo la ci dundug nit ci kaw suuf.

Jumtukaay yu elektronik yi ak seen njariñ:  

Jumtukaay yu elektronik yi mujj nanu ci jamono jii nu nekk, di loo xam ne foo wëlbëtiku gis ko, ci kër yi, barabu ligeey yi, dëkk yu mag yi, yu ndaw yi, mbay mi ak mecce yi añs.
Kon daal jumtukaayi elektron yi, dugal nanu seen loxo ci yombal dund gi, nga gis nit ñi ñuy jëfandikoo raxasukaay yu kuran yu otomatik yi, ak fompukaay yu kuran yu otomatik yi, ak jumtukaayu seral yi yu wuute yi, ak rajook tele yu melo yi, ak jumtukaayu nataal yi añs.
Boo demee ci ndoktoor it fekk ko mu fees dell ak jumtukaay yu elektron, xoolal ma fesalukaay yu elektonik yiy feeñal jàngoro yi gën a tuuti, ak nataalukaayu ndoktoor yi, ak jumtukaayu segg  yu elktronik yi. Jumtukaay yii dey tax nanu doktoor man a xam lu jot nit, man koo faj, te looloo tax ndoktoor jëm kanam ci sunu jamono jii.

Gis nga leegi foo dem fekk fa komputer, ci bank yi, lonkoo yi, campeefi goornamaa yi ak ligeewukaay yi.
Gis nga xam-xamu fuglug jawwu ji  ni mu nosoo leegi, ak xam kiliman bi, te loolu lepp elektron a ko waral, leegi man nanoo xam nu tooyaay bi toll, nu jawwu ji selle, nu gelaw li gaawe, nu tàngoor wi tànge, nu niir yi kawee añs, te loolu lepp elktron a ko def.
 Waa xam-xamu suuf (jiyoloji) jariñu nanu ci jumtukaayi elktronik yi leen di xamal ati doj yi ak ati suuf si, te di leen won fi am petrol, yoraniyom ak yeneen mbèlli suuf yu am yi solo.

Jumtukaayi elektronik yi dimblee nanu ci wàlli ngànnaay ak xare, ak aaru. Leegi gis nga jumu fepp , rajo, jumtukaay yi amul buum , ak yiy yonnee tey nangu, ak yiy nataal añs.

Lii nag wone na ne xam-xamu elektron, aki jumtukaayam, yi ci aju ci jàmm ak yi ci aju ci xare, def nanu fi ag jeqiku gu xam-xam gu am solo ci xarnub ñaar-fukk g bii.
Nit nag jot na a man a tàggat xam-xam bii def ci li mu ci bëgg ci lu aju ci jàmm, waaye it mi ngi koy jëfandikoo ci xare yiy màbb, tey mbugale, di alag mbidéef yi.

Juroomeelu Doggantal

xareb jawwu ji  :

(( yaa mahsharal jinni wal’insi inistatahtum an tanfuzuu min’axtaaris’samaawaati wal’ardi fanfuzuu, laa tanfuzuu illaa bisultaanin))
Sooratu Rahmaan, aaya 33.

Di : yeen jinne yeek nit ñi, su ngeen manee dem, ba soobu ci goxi asamaan yi ak suuf, def leen ko, waaye fu ngeen fi àgg rekk na leen woor ne Yàlla a leen may ngeen àgg fa. Fu ngeen fi àgg rekk, ci sultaan ngeen fa àgge, sultaan nag mooy: lay, ndigal, kàttan, nguur. Di kon fu ngeen fa àgg, sunu boroom a leen fa àggale moom mi leen may xel, may leen kàttan, ubbil leen bunti yooyule gox, man a layal lu tax ngeen àgg fa.

Nit nag yàgg naa xëntewoo xam li ko wër ciy mbir, yàgg naa yittewoo xam mbóoti jawwu ju biti jii nga xam ne daa fees dell aki nekkteef yu asamaan; ay bidiw aki ñoom seen.
Moom de jot naa àgg ci xam bidiw yi ak seeni kem ak seeni bind, ak li leen sos, def it ab jeego bu rëy ci xam-xamu juxraaf ak yeneen xam-xam yi am ag jokkoo ak kaw suuf, biir suuf ak li wër suuf, peek ko ciy mbindeefi asamaan, bidiw ak lu ko moy.
Ci ati juroom fukk yi, ci ñaar-fukkeelu xarnu bii, gis nanu nit mu jeem ay yoon nu mu yeege ci jawwu ji, ngir làmb ko te xam la fa nekk, loolu nag faalewu ci jafe-jafe yi mu ci man a dajeel, ak ay wu rëy wi loolu làmbool, bokk na ci ay woowu:  man cee ñàkke bakkanam, ñàkk a wóor gi, ci bu nuy joy , bu masin biy wëndéelu ak buy wàcci.

Li Sofiet yi def ci xareb jawwu ji:

Sofiet yi de njëkk nanoo nattu jawwu ji, làmbtu ko, loolu nu jaare woon ko ci jëfandikoo ay bayyima, ngir ragal nit di ci loroo. 
Sofiet yi ñi ngi njëkk a joyal seen gaalug jawwu  gi tuddoon Fostok – 1 ñaari soobukati jawwu  yu sofiet nekkoon ci biir – di Yori Jajarin ak Alaan Shabard, ci subag bisub 12 awril 1961 g . loolu nag bettoon na adduna bépp.
Tukkib jawwu bii nag yobbu woon na lu tollook teemeer ak juroom ñatt-fukki simili, ci biir diir boobu, gaalug jawwu gi wër na ci suuf si benn yoon ak xaaj.
Tukkib xam-xam bu jawwu bii xew-xew la bu am solo ci taarixu nit ci jamono ju yees jii, ndax kat moom ubbi na fi ay gox yu yees yu yaatu ci wàllug xam-xamu jawwu.

Sofiet yi wéyoon nanu ci seen ligeeyi jawwu yooyu nga xam ne am na ci yu jàmm taxoon a jug ak yu xare taxoon a jugg. Seen satalit yi gënoon nanoo yokk seen cawarte rawati na ci lu aju ci xare, ci diggante ati juroom-ñaar-fukk yi ak juroom-ñatt-fukk yi, ci xarnu bii.

Li ci waa Amerig def:

Waa Amerig yi - ci ati juroom fukk yi, ci ñaar-fukkeelu xarnu g – def nanu ay jeem aki pexe yu am solo ci wàllug xareb jawwu ji. Seen cawarte ci wàll googu dolliku woon na ci ati juroom benn fukk yi ci xarnu bii, ndaxte seen ligeey yu jawwu yi gënoon nanoo ràññiku te gën a fés ci diggante bii, ndax ci la kërug jawwu gu Amerig gi, ñu koy wax NASA, jot a joyal ay waruwaayi jawwu , yoo xam ne ay jum  ñoo leen di jañ, jañax leen ñu naaw, bu niy dellusi ci suuf si nekk ay fafalnaaw yu yor ñaari laaf, ñu leen di man a jëfandikoowaat ay yooni yoon.
Lii nag tax na ba li nu daa ñàkk  ci tukkiy jawwu yi gën a neew, te itam indi na ay ngérte  yu am solo ci xareb jawwu ji.

Waa Amerig jot nanoo sànni waruwaayu jawwu wii di Apolo ci 20 sulye 1969g, ñaari soobukati jawwu nekkoon ca, ñooy: Aarmustrong ak Adwin Drin, Aamustrong nee na “ Amoon naa yëg-yëg bu tumbrànke, bi may dox ci kaw weer wi, damaa yëgoon ne sama màndaxe  daa woyofoon lool”. Waa Amerig yi sàmp nanu ci kaw weer wi ay jumtukaay yu xam-xam yu bari, jële nanu fa it ay còmp  yu juge ca weer wa, teg fa it ab juddalkaayu kuran bu saal .

Kongres it dëppoo - ci 5 samwiye 1972g – ci prograamu jawwu bi nu tudde woon (baaganteg jawwu)  ngir barig li nu daa dem ci jawwu jeek a dellusi. 
Tukki bu jawwu bu njëkk bi nuy wax Kolombiya tàmbli na ci 12 awril 1981g, yeneen tukki topp ci yu jawwu yu àntu .

Waa Amerig yi defati tukkiy jawwu yu Carlinger , bi ci njëkk di ci 4 awril 1983g, juroom ñeenti tukki topp ci, bi mujj di ci 30 oktoobar 1985 g.

Musibam Carlinger:

Am musiba xewoon na ci baagante gu jawwu gu Amerig gii di Carlinger-10, loolu nag mooy bi waruwaay bi fàccee , ci bisu talaata 28 samwiye 1986 g, lu tollook juroom ñaar faatu ci, ñaar ñi di ay soxna .
Njiitul Amerig la nu daa wax Ronaald RIGAN nee na woon “ Bii bis de dana doon bisub naqar ak fàttaliku” . Waa Amerig yi it tudde woon nanu ko bis bu tiis bi.

Musiba mii du mooy mi njëkk a dal Amerig ci wàllug jawwu gi, mu ni mel njëkkoon na ko fi ci lu tollook ay at, loolu mooy bi sawara tàkkee ca joyaluwaayu  waruwaay ba tudd Apolo 11, ci samwiye 1967 g, ci noonu ñatti soobukati jawwu ya ca nekkoon yepp dee.

Amerig defati yeneen tukkiy jawwu yu baagante, tudde ko Discovery, bi ci njëkk mi ngi amoon ci 30 Ut 1984 g, yeneen tukk yu àntu topp ca. 

Lii nu tudde xareb jawwu ji daal, def na lu am solo ci wàllug xam-xam, rawati na lu aju ci mbiri jàmm yi.
Ndaxte xam-xamu fisiya gën a jëm kanam, bu fuglug jawwu , ak xam-xamu nataalu jawwu biy nataal kaw suuf si te di ko natt, xam-xamu kart yi  ak nataali jawwu yi gën na a jeego ay jeego, naka noonu endustri elektronik, ni nuy xame fi mbell yi nekk gën a xarañ, ak ni nuy xeexe lakk yi añs.

Sofiet yi ak waa Amerig yi ku ci nekk soobu nga ci jawwu ji ngir ay xemmemteefi xare, jawwu ji mujj di lef mu stratejig mu yaatu ñeel ay ligeeyi xare, la nu ca jublu it di door ak jam ay barab yu nekk ci kaw suuf, jaare ko ci seen satalit yi nekk ci jaww ji, yi ci yanu ay boppi atomig, cig wàll, walla nu jaare ko ci ngànnaay yu wuute yi nu man a joyale ñu tukke ci jawwu ji, ci geneen wàll.

Xareb jawwu ji, yamatul rekk ci diggante Sofiet yi ak waa Amerig yi, leegi kay lu sakkan ciy reew bokksi nanu ci, mu ci mel ni Siin ak Fraans. Am na yeneen reew yuy waaj ngir sànni seeni jumi jawwu walla satalit ci jawwu jii nga xam ne mujj na di barab bu yaatu ngir rawanteg xam-xam, ak gëpplante ci wàllug xare.

Juroom benneelu doggantal  

 Ni Japon jëme kanam

Japon njëkk fukk ak juroom ñeenteelu xarnu g:

Japon de wéyoon na diir bu yàgg, di beru ak a sori xayug Tugal gi, yam ci yëfi bobbam, doyloo aadaam, ba ci digg juroom ñeenteelu xarnu g, gii beru gu xay, ak deltu ginaaw gu mag raxoon na ci, ci wàllug koom-koom, rawati na endustri.

Waaye nag lii mu nekke woon, soppiku woon na ci ñaareelu xaajub fukk ak juroom ñeenteelu xarnu. Ci noonu mu tàmblee juge nànk-nànk ci reew mu deltu ginaaw, dem ci reew mu jëm kanam ci wàll yii: koom-koom, aada, politig ak xare.
Mu roye nag ci reewi Tugal yi, gisiinu sanc ak yaatal ko, ci reew yi mu dendal, ngir wone ci dooley addinaam ji mu yor, ci wàllug xeex gi nuy def ngir teg loxo ay reew, sanc leen.

Japon nag ak li muy yeex a jot ci xayug tugal gi lepp, boo ko dee xool ci reewi Asi yeneen yi - ndax dëppoo gi mu njëkk a def ak Amerig ci wàllug joqalanteg yaxantu  weesuwul atum 1854 g gii rekk -  teewul mu tàmbli woon na jege nànk-nànk xayug Orob gi, di ci jariñu, di ci niitu.
Loolu jural ko mu tabax ay isin yu mag, xotti ay yoon, defar ay yooni saxaar , gën a jëmale kanam ni nuy yaxantoo. Reewum Japon ca saa sa mu tàmblee gis ag yëngu-yëngug endustri gu mag, gu nirook ga Tugal romboon ba mu ciy door a dugg.
Bu ko defee, Japon xëy di reew mu dox, mu jëm kanam, raw nag ay maasam ci reewi Asi yi, ci wàllu endustri, xam-xam ak xarala  .
Mu mujj am, moom Japon, mbooloom gaal mu yaxantu tax a jug, mu mag, moo xam ne moo jël limub ñatteel ci adduna bi, ci diggante ñaari xarey adduna yi.
Marsandiisi Japon yi, nga mujj foo dem fekk leen fa, ci Asi ak Afrig.

Japon, ginaaw bi nu ko gañee ci ñaareelu xareb adduna bi:

Japon gañe nanu ko ci ñaareelu xareb adduna bi, te booba moo nekkoon laafum penku mi ñeel reewi digg yi (axe), ñooy: Almaañ, Itaali ak Japon.
Japon nag mujjoon na nangu ne gañe nanu ko, mu jébbalu, joxe loxoom ci kanamu njiitul xare lu Amerig lii di Mark Arthur, atum 1945g . Ci noonu nu taxawal benn jataay bu way tapoo yi  , ngir doxal mbiri Japon, nu dénk ko kii di Mark Arthur, ci diggante 1945 – 1951 g.

Waa Amerig yi nag rëddaloon nanu Japon benn strateji, dugal fa demokraasi, jële fa dal bi aju ci jaamu imbraatoor bi , nu soppi woon it seeni njàngaliin, maanaam ni nuy jànge ak li nuy jàng, wutaloon leen sartu reew bu bees, ray it lonkoo yu mag yi  .
Ñu fuqarci ay moomeel yu rëy ci loxoy njabooti Japon yi, sëddale leen ci lim bu mag ci baykat yi, daal di it taxawal ab parlamaa bu bees  .

Ci noonu Japon jot na a tàmblee nosaat dundug koom-koomam., gu plitigam ak gu mboolaayam, te tàmblee dab nànk-nànk,  reewi endustri yu jëm yi kanam.

Waa Japon jariñu nanu ci li leen Amerig indil ci ndimbal yu alal ak yu xarala, loolu bokk ci li delloosi cawarte gi ci wàllug koom. Lijjantikati Japon yi  dox nanu bu baax ci tas ak yaatal koom-koomu Japon, ngir seenug yewwute ak ngir bari gu Japon bari ay ligeeykat.

Suqali nag gën na a yokk ci wàllug endustri ak yaxantu ci diggante bi topp ci 1955g . Japon mujj di ñatteelu reew mi ëpp lu muy ligeey weñ, bokk it ci reew yu njëkk yiy segg petrol, ak yi ëpp lu nuy defar gaal. Mbooloom gaalum yaxantoom mi gën na a jëm kanam, ay ngañaayam gën a dolliku, ligeey bi aju ci jumtukaayi eliktronig yi gën a jëm kanam, ba mujj Japon àgg ci, ci fi nu man a yam ci raw gu xam-xam. Ja  yi nuy jaaye ligeeyi Japon yi gën a yaatu, gën a bari ci adduna bi. Bu ko defee Japon mujj nag di reewum endustri mu mag, mu dox, te jëm kanam.

#Article 45: Taariixu àdduna bu bees bi te jamonoo (62231 words)

Ag jiital 

Teeree ngi nii buy gàttal yoonu xam, ndax li nga daa lijjantee xam ciy fan ak cib coona, moom la lay xamal ciy waxtu, ci lu dulub coona.

Muy bu nu def ngir feeñal ci baat ak waxiin yiy war a wuutu yu fraanse yu bari yu nuy teg ci barabi yu wolof yi, te kat fekk na wolof amoon leen mbaa mu manoon leen a am, te nu jàpp ne manunoo doylu wëlif leen. Ma yaakaar ne bu nu bëggee yombal dëgg, lu mu metti, metti, danoo war a wut ay kuutlaay ñeel baati doxandeem yii bëgg a ruur sunu làkk wi, te nag  yombug xam-xam mi ngi ci nga koy jàng mel ni jàngoo, kon lu tax muy français? Ginaaw du lu moy ab jumtukaay ngir xam, ngir déggante, waxante, te ma gis ne bu dee ci ay wolof seen làkk, lay gën a nekke jumtukaay boobu.
Lii ak leneen lu bari, moo ma yobbu ci di xalaat ci di binde ci wolof, te ba yeneen kàllaama yi, ginaaw bindaluma ku leen moy. Te it nag ni ñepp def ba ami làkk lu tax dunu ko def bay am sunu yos ñun itam waa Afrig? Nekkewunu fi lu dul ligeeyal Tugal ak lu ni mel, nanu sunu bopp ñor ! doonte as lëf la it.
Nan la am reew mu tollu ne Senegaal… ñépp di waxi wolof nga ne fraanse rekk ? reerale ga’a ngii !

#Article 46: Mamoor Xam Sa Diine (106 words)

Maamoor xam Sa Diine mooy Moor MBÀKKE Gànnaar, maanaam doomi Sëriñ Jiili Gànnaar, di ku yëngoom jëm ci yar ak jàngale. Taalif na lu bari ci wolof, firi ci it ay téere jële léen ci làkkuw araab, yooya nag yu ci ëpp yu diine lañu, woy na it lu sakkan ci wolof, yii woy firndé lañu ci, ku fonk wii làkk la, looloo ko bijj ci def wile taalif, sànki ci baat yu naroon a sànku, mu jëfandikoo arafi abajada ngir toftale leen, Yal na ko Yàlla gërëm, moom nag day faral di def ay waxtaan ci diine ak làkku wolof ci rajo (siwalukaay) Làmp FM

#Article 47: Broken/Dalal-jamm (213 words)

Dalal-jamm, yaa ngi ci wikipedia gi ñu jaglel kàllaama wolof, muy ab tèerexamteef gu tinkiku goo xamne ñi koy jàng bokk nañ ci ñi koy bind.
ku nekk man nga cee dugal sa loxo, bind ay jukki yu bees wala gënël baaxal li fi jota nekk; ndaxte ngir mebet mii mana dox ci ni mu gënee, dafa laaj ay loxo yu bari. Kumu manti doon man nga cee japp ci njekk ak teranga, topp atte yi'ñ fi tërël, ñoo ngi lay dalal. 
Li mu doon lu ubbeeku ngir ñëpp te amul'g pay, ñi binduwul tamit ci biir, moo tax Wikipedia manula joxe ay wòoraange ci baaxaay ak celltey ndefam.  Donte askan wu wikipedia moo ngi tijji ay gëtëm di ko jeema aar ci anam yu dëgër. Ci saa su ne man na am ay xët yu ñu say-saye wala yuñu soppi ci anam yudul yi gën te tay ko, def ci ay xibaar yu baaxul wala yu dëppowul ak dundinu sa waa-gox. 

man ngaa tambalee ci xët-njëkk mi te topp lëkkalekaay yi lay yòbb ci li la solool, li nga soba jàng.
su fekke itam daa am ab jukki booy seet, man nga bind benn wala baat yu bari ci paxu bind gi, gi nekk ci sa ndeyjoor te nga klig ci Ayca

#Article 48: Dalub Archimède (155 words)

Du ñàkk mas ngéen a gis ay gaal yu mag ñuy tëmb ci kaw géej: te kat ci weñ lañu leen liggéeye te weñ du feey, loolu man nga cee xam dara soo jëlee ab pont mbaa lenn ci weñ tàbbal ko ci ndox.

kon am na jenn doole juy safaananteek diisaayu gaal yooyu, te ñooy tax ba ñuy des ci kaw ndox mi di tëmb. Bu ngéen ci bëggee xamal seen bopp dara, jëlléen loxo ngéen nuural ko ci mbalkam ndox, bu ko defee ngéen yolomal séen loxo te xool, dingéen gis ne am na jenn doole juy jañ loxo bi te di ko tëmbloowaat.

yii ak yeneen seetlu yu ni mel ñooy wone ci anam gu leer jikko ju daj ji nga xam ne nekkul rekk ci ndox, waaye nekk na ci yeneen yolaakon yi ak gaas yi,ñu duppee ko Dalub Archimède, moom Archimède nag benn boroom xam-xam bu Gres bu yàgg la

#Article 49: Diisaayu yaram yi (124 words)

Tay de bis bu xiin la, tàmbali naa taw, doqi ndox yu ndaw, yu xaw a rëy, yu ngandee ngandee ngi nii far di rot ci suuf.

Bu cooroonee, gàncax gu bari seeni xob day ruus, daal di naaw ci jawwu ji, rotati ci suuf si.

jël-leen aw xeer ci seen loxo, wacc-leen ko, day rot ci suuf de.

Benn sabab bi tax xeer woowu di rot, tax it ba xob wi rot, moo fi jaar ba tax doqi ndox yu taw yooyu di rot: loolu mooy li nuy wax Bijj gi walla Dooley ñoddi gi suus si di amal ci yaram yi.
Ñoddi gii mooy tax yaram yiy diis, moo waral it ñuy aajowoo genn kattanug përëg ngir yékkatee léen ci suuf si.

#Article 50: Ne-ne (162 words)

Ne-ne, ñu xame ko ci faraañse ci((matière))mooy li toggale (li composer) wépp yaram wu am ag nekk gu nu man a laal (une réalité tangible. Ñatti melokaanam yi ñu gën a miin nag, ñooy melokaan wu dëgër(l'état solide), wuy yol (l'état liquide) ak wu gaasu (l'état gazeux). Moom day jël barab(elle occupe de l'espace)te kemub ne-ne (la quantité de matière) ñi ngi koy natte ci jóor(la masse) (bu fekkee ne mbir mi dafa aju ci waññ xaajiiti ne-ne(particules de matière), deesi jëfandikoo mol(la mole) ).Ci noonu, ci xam-xamu jëmm, lepp lu am ab jóor rekk ne-ne la. Ci biir loolu, ne-ne yu ñu miin yi ñu wër, ñi ngi sosoo ci ay bariyon,kon ci waxiin wi nu baaxoo, boo ci déggee baatub ne-ne, nanga xam ne ne-ne bu bariyon lañu jubloo wax. Tekkiin wii kon boolewuñu ciboson yu dàttu (les bosons fondamentaux), yi nga xam ne ñooy tuxal ñeenti doole yu dàttu yi ak doonte am nañu ab jóor ak/walla genn kàttan.

#Article 51: Wërlaay (523 words)

Wërlaay gi di ci tubaab (environnemt) mooy dénd bi maanaam (nature bi) ak li ci nekk ciy way dund ak yu dundul, ci gàttal daal adduna bi nu wër ci kaw suuf si. Xam-xamu wërlaay mooy biy jéem a indi ay tontu ci yenn laaj yi aju ci nan la dénd biy jëfe ak a jëflanteek way nekk yiy dund ak yeneen way nekk yi, walla nan lay jëflanteek digg bi ko wër moo xam digg bu kimya la (simi) walla bu dénd (nature). Digg bii moom lanuy tudde “Noste gu wërlaay”. Looloo waral nuy gis noste gu wërlaay muy luy ame ci ay way nekk yuy dund ak yu dee walla yu way. Xam-xamu wërlaay mooy jàng ak gëstu way nekk yiy dund ak séenug séqoo ak li leen wër ak jeexiital gi nuy def ci sunug séqoo ak suuf si. Nosteg wërlaay mooy mbooleem jëfka (facteurs) yu dundul ak mboolaay (société) yiy dund yu xeet yi nekk ci benn gox walla barab. Dénd bi day wëndéel mbir yi mu jëfandikoo woon ngir delloo leen ñu mujjaat di mbir yu am solo ak njariñ. Càllalag ñam ci kaw suuf si, aw melo la ngir wone ni kàttanug ñam di dugge ci wërlaay gi. Foofu ñam  da fiy juge ci aji nekk dem ci jeneen n gir jox kàttan dundat boobu di sàqami ñam wi ak a reesal, gépp càllalag ñam nag ci jant bi lay tàmbalee. Dundat yi - nit ci la - munuñoo liggéey seenub dund, looloo tax manul a ñàkk mu jot ci dundam boobu jële ko ci gàncax yi walla yeneen dundat yi, looloo waral ñuy jàppe dundat yi ay way lakk walla ay way jëfandiku (consomateur), mujjantalu dundug dundat it mooy ag feccikoom (ag tasam) jaare ko ci ay mikrob walla ay gàncax ngir mujjati di suuf, gàncax gi muucooti ko ngir liggééyati ci ñam wu beesati. Lii nag moom lanuy tudde “Càllalag ñam”, bokk na ci jëfkay dénd yi ci nosteg wërlaay gi te am ci jeexiitalm it: leerug jant bi ak ker gi ak tàngoor wu diggdóomu wi ak séddalig sewogaraafi gi ak ngelaw li ak barab yu yékkatiku yeek yu suufe yi ak melokaanu suuf seek ndox mi. bokk na ci jëfkay kimya yi yiy bàyyi ay jeexiital ci nosteg wërlaay gi: tolluwaay (niveau) bu ndox yi ak ngelaw li walla jawwu ji ci suuf si ak kem ni way dundal yu gàncax yi di seeye ci suuf si ak ndox yi ak tooke yi ci nekk, ak xoromus ndoxum géej ak oksijiin bi ci seey.

kay diang wolof

Ci baax, wërlaay - walla barabub jëf mbaa mbir, maanaam fu lëf nekk mbaa deesi defe ko fa - mi ngi ame ci jëmm yi (substence), peekte ti (circonstance), mbir yi walla nekkiin wi ko peek wër ko, te di fa ame.

Bu dee ci wàllug dundat (biyoloji) rawati na ci wàllug dénd (ecoloji)day tekki lépp lu man a def ay jeexiital yu jonjoo ci doxug walla màggug mbaa jëm kanamug mbir yi (metabolosmo)walla nekkiinu jëmm  walla xeet wuy dund ( SPECIE VIVENTE), loolu nag leer ci la, ngelaw, ndox, suuf ak yeneen nekktéef yiy dund.

#Article 52: Dalu Archimède (166 words)

Dalu Archimède (fr : principe d'Archimède) : Du ñàkk mas ngéen a gis ay gaal yu mag ñuy tëmb (feey) ci ki kaw géej: te kat ci weñ lañu leen liggéeye te weñ du feey, loolu man nga cee xam dara soo jëlee ab pont mbaa lenn ci weñ tàbbal ko ci ndox.

kon am na jenn doole juy safaananteek diisaayu gaal yooyu, te ñooy tax ba ñuy des ci kaw ndox mi di tëmb. 
Bu ngéen ci bëggee xamal seen bopp dara, jëlléen loxo ngéen nuural ko ci mbalkam ndox, bu ko defee ngéen yolomal séen loxo te xool, dingéen gis ne am na jenn doole juy jañ loxo bi te di ko tëmbloowaat.

yii ak yeneen seetlu yu ni mel ñooy wone ci anam gu leer jikko ju daj (comportement général) ji nga xam ne nekkul rekk ci ndox, waaye nekk na ci yeneen yolaakon yi(les liquides)ak gaas yi,ñu duppee ko Dalub Archimède, moom Archimède nag benn boroom xam-xam bu Gres bu yàgg la

#Article 53: Doolerandu (152 words)

Doolerandu mooy xam-xam biy gëstu lepp lu ñeel wuutuloxo yi, doxalkat, ndaamar, ci gattal, lepp luy jur walla di yòbb ab jalaxu, doole, ag soppeeku. Da nuy wax tamit doolerandu gu daj, doolerandug ndaamar, taggat-yaram gu doolerandu, doolerandug gaal, doolerandug asamaan, doolerandub kàttan-ferñent…

ci taariix, doolerandu mooy boole, gi Newton def; jëmm ak gëstubidiw. Kon su nu ko xoole ci wallu taariix jëmm walla fisiyaa ci doolerandu la joge.
Ci sunu besu tay yi, day lu noppale, ci daara yu kawe yi, ne atte doolerandu yi ci jëmm la ñu joge.

Doolerandu ab banxaas la ci xam-xam yiy gëstu jalaxu yi ak soppeekuy neen yi, ci lu tukkee ci doole jiy man a indi googu jalaxu walla googu coppiku.
Man nan koo xoolee ni ag wàll ci xam-xamu jëmm.
Kon aajoom mooy leeral, xalaatjiitalu jalaxug neen yu tekkaaral yi, ak yaram yu asamaan si walla jëmm yuy dund (dun-doolerandu) ëbb na tamit:

#Article 54: Kàttan (871 words)

Kàttan mooy man a def dara (sos ag soppi), kàttan nag am na ay melo yu bari, yi ci ëpp solo ñi ngi feeñe ci tàngoor ak leer.

Ci biir “xam-xami dénd yi” (science naturelle) kàttan man na fee jël ay melokaan yu wuute : “kàttanug tàngoor”, “kàttanug kimyaa (simi)”, “kàttanug mbëj”, “kàttanug ceññeer”, “kàttanug saal (nucleaire)” ak ci mujjantal gi “kàttanug mbëjbijjaakon (éléctromagnétique)” añs. Xeeti kàttan yii ñaare dees leen di séddale ci: “kàttan guy yëngu ak “kàttan gu nëbbu” te kat am na yenn kàttan yoy dëppoowunook séddale gii, lu ci mel ni: “leer gi”, ak yeneen yoy man nanoo nekk am njaxas mu tukkee ci ñaari kàttan yi, guy yëngu gi ak gu nëbbu gi.

Lu bari ci xeeti kàttan yii manees na koo soppi (transformer) jële ko ciw melo yóbbu ko ci weneen, jaare ko ci jëfandikoo ay jumtukaay yu fasoodiku (simple) walla ay xarala yu fasu (compliqué): la ko dale ca “kàttanug kimya” ba ci “gu mbëj” jaare ko ci jumtukaay bu siiw bi di tegale(pile) yi, walla ndëxañtéef yi, Albert Ayinstaayin it ci biir ”faramfaceg ajoo” (theorie de relativisme) boole na ñaari ëtt yii di bu ne-ne ak kàttan, nga xam ne kàttan day mujj man a soppiku di ne-ne(matiere), naka noonu safaan bi, maanaam neen soppiku moom it di kàttan: wuññi (découverte) gu yees gii mi ngi ko xamalee ci yemalem gu siiw googee E=mc2, soppiku gii ci jëf (ci wàllug pratique) ñi ngi ko firee ci man gi nu man a ame kàttan jaare ko ci “xarug saal” walla “booleeg saal”.

Waxiin walla baatal (terme) yu kàttan yi akug soppikoom lu am njariñ la ci leeral jëfiini dénd yi. Ba sax feeñte(phenomene) yu kilimã yi niki ngelaw, taw, melax ak riddi yi (tornado) dees leen di jàppe ñu juddoo ci soppiku yu kàttan gi juge ci jant bi wàcc ci suuf si. Dund gi ci jëmmi boppam dees koy jàppe muy benn ci njuréef (resultat) yu soppikuy kàttan yi: ci anamu “toggaleg leer gi” dees na ci jële soppi kàttanug jant bi yóbbu ko ci “kàttanug kimya” ci biir gàncax yi, bu ko defee ci kanam ñu man a jariñu ci kàttanug kimyaa gii nu denc, ci ay “liggéeyiinu wëlbati” ci ay way nekk yuy dund.

Ci biir jëfandiku gu mboolaay (gu société bi): baatub kàttan dees koy wooye lépp lu nekk ci ron gongikuwaayu kàttan (source d’energie), juddalug kàttan, lakkug kàttan (ag jëfandikoom) ak wattu rootuwaayu kàttan (maanaam fi muy juge), ginnaaw nag dooley koom-koom dafa laaj te soxla ab rootuwaay walla ab gongikuwaay ci gongikuwaayi kàttan yi, looloo tax ag amam akug yooxam(baril ko) bokk ci yitte yu mag yiy caabi. Ci at yu mujj yi, jëfandikoo kàttan feeñ na di benn ci jëfka (facteur) yi gën a sabab nuggug àdduna bi (global warming), looloo ko def muy ab lëj-lëj ci li ëpp ci réewi adduna bi.

Manees naa soppi kàttan jële ko ciw melo yóbbu ko ci weneen, ci misaal, manees naa soppi kàttanug kimyaa gi ñu denc ci ab tegaleeb(pile) Jiib def ko ag leer. 

Kem (quantité) bu kàttan bi nekk ci àdduna bi, day lu sax ba fàwwu, kàttan du jeex, du sosu, li am kay mooy day soppiku juge ci melo dem ci weneen. Bu melee ne kàttan dafa jeex, booba jeexul, daa soppiku kay dem ci weneen melo. Looloo tax ñuy gis ne kàttan mooy man gi neen man a def ab liggéey (yëngu) muy njuréeful yëngoom googu, walla njuréeful ab barabam bu nu ko nattee ci doole yiy liggéey ci kawam. Kàttan giy ànd ak yëngu moom la nuy tudde “kàttan gu yëngu”, kàttan nag gi am ag jokkoo ak barab bi moom la nuy wax “kàttan gu nëbbu” (gu coona walla gu ñu dëxëñ (gu nu denc) )...

Kàttan dana ame ciy melokaan yu bari, niki kàttanug doolerandu (mecanique) ak gu tàngoor, ak gu dinaamig gu tàngoor (tangdooleel,termodinamique), gu kimyaa, gu mbëj, gu ceññeer ak gu saal( walla xartil), kàttan yii yépp nag man nanoo def ag soppiku gu biir jaare ko ci ay yoon yu dëppoo. Ñam wi nuy lekk am na kàttan gu kimyaa gu yaram wiy denc te di ko génne bu nuy liggéey walla nuy génne ab coona (def effort)

Kàttanug bàyyima yi mooy gi nit njëkk a jëfandikoo ci fajarug xay (bi xay (civilisation) di door a am), loolu mooy bi mu jëlee bayyima yu miin yi di leen jëfandikoo ciy liggéeyam, ginnaaw bi mu tàmbalee jëfandikoo dooley ngelaw li ci doxal ay loocaam ba ci ay gox yu sori ci géej gi. Lu xayam di gën a yokku muy gën a jëfandikoo kàttan gii, mu jëfandikoo ko niki kàttanug doolerandu (mekanig) ngir doxal walukaayi ngelaw yi, ak ngir dawal ponoy wuutuloxoy wal yi, ak daggukaayu dénk yi ak najukaay yiy yékkatee ndox yi ci teen yi. Lii mooy li nu xame ci turu kàttanug doolerandu (mekanig).

ci maanaa, da nuy ràññee xeeti kàttan yu bari te wuute. Kàttan tamit day tax nu man a natt melow feeñte yi, seenub taraay; feeñte gu ne ak kàttan ga mu àndal.

Xeeti kàttan yi nu yàgg a jàpp:

Kàttanug imbiku (cinétique)
Kàttanug tàngoor (calorifique)
Kàttanug ëmbu (potentielle)
Kàttanug doolerandu
Kàttanug kimiya
Kàttanug saal
Kàttanug mbëj
Kàttanug mbëjbijjaakon
Kàttan gu féex (libre)

#Article 55: Koom-koom (349 words)

Koom-koom walla cawarteg koom-koom (activité économique):(làkku grees wu yàgg wa : οἰκονομία, « yor ag kër walla saytu ko »« di οἶκος (kër ci ni ñu ko xame)ak (νέμω yor walla saytu(administrer)) mooy cawarteg nit giy feeñ ci liggéey ak jóox (produire) ak séddale ak joqalante (echange) ak jëfandikoo njuddéef yi (les produits) njëfte yi (le services). 

Koom-koom nag ni ngi koy jànge ci xam-xami koom-koom yi, day sukkandiku nag ci gisiin yu koom-koom (théories économiques).

Dees na wax it ci koom-koom niki tolluwaayu koom-koom bu jamono bu am réew walla bu ab gox (zone), maanaam ag nekkam ci gëwéelub koom-koom yi.
Cawarteg koom-koom gi kiliftéef yu koppar yi walla góornamaa yi (àtte yi) ñoo koy àtte jaare ko ci ab politig bu di kojug jamono (conjoncturelle).

doxaliin wu mbooloo mi (Les administrations publiques)day def moom itam ay politig yu koom-koom ngir soppi doxiinu koom-koom wu am réew.

benn ci joxoñ yu koom-koom (indicateurs économiques) yu mag yi mooy njuddéef mu ñumm mu biirum réew (NJ.Ñ.B) (produit intérieur brut (PIB)), loolu mooy maye nga man a nattale dooley koom-koom yu réew yi

Xam-xamu koom-koom ( ci Fr:economie)moom xam-xamu mboolaay(social) la buy yëngu c gëstu ni ñuy jëfandikoo jumtukaayi jóox(production)yu daytalu yi am cig mboolaay (société) ngir faj soxlay ak xemmemtéefi cér(membre)yu mboolaay gii.Xam-xam bii nag mook xam-xam yépp a yam, dafa am ay dëgg-dëggam akaki àtteem waaye jeexiitalu gi mu def ci nekkiini mboolaay yi ak yu politig yi (les conditions sociales et politiques)ak ni ay séqoom ( ay relation-oom) dugganteek nekkiin yii tax na ba melow mboolaay muur ko, cuub ko.

Xam-xam bii li mu làmboo mooy seggat jóox gi (production), séddale gi, ak yaxantu ak lakk walla jëfandikoo njaay yi (marsandiis yi) ak njëfte yi (les services). danuy faral a wax ci koom-koom ne buy wuyyu la (positive) bu dee jéem a leeral ngértey tànn yu wuuteyi, di joxe ay mbooleem ay xalaat jiital (hypotese), walla am mbooloom ay gendiku (ay seetlu),danuy wax it ne bu nattukaay la bu dee leeral doxal yi nu war a def.

Xam-xamu koom-koom dees koy déddale ci ñaari bànqaas yu mag:

#Article 56: Wikipedia (522 words)

Wikipedia (di jàng wikipediyaa) ab sémbub jimbulang la ci web bi, di lu àddunawu te bariylàkk. Ag bindam nag mi ngi wéy ba tay, xaralaay wiki lañu jëfandikoo ngir sos ko. Yéeney Wikipedia mooy jébbal am , maandu te fugluwu.

Nupedia di woon ab sémbub jimbulang bu ubbeeku bu Jimmy Wales sosoon ci weeru gamu atum 2000. Mboolaay gu Bomis (gi Jimmy Wales féetewoo woon moomeel gi ci ëpp) moo ko jàppale woon ciy koppar, doon fay Larry Sanger mi jiite woon mbind mi. Waaye Nupedia ag màggam dafa yeexoon lool ba waraloon, ci 2001, Larry Sanger xalaatoon ni sos ab wiki moo doonoon liy man a gaawal yokkteeg jukki yi. Xalaat boobu ñeel jëfandiku xaralag wiki ngir sos ab jimbulang, juroon na ag diisoo ci diggante Larry Sanger ak tëriinkat boobu di Ben Kovitz ngir mu faramfaceel ko ci ni mu gën a leeree ana nan la xarala gu wiki di doxe, ci ab reer ca San Diego la ame woon, ci 2 tamxarit 2001. Ci nii Larry Sanger ni Jimmy Wales ngir ñu jëfandikoo xarala gu wiki ngir sos ab jimbulang bu gën a woyof, lii moo jur sosug jimbulang bu Wikipedia.

Ginnaaw bi ko Jimmy Wales ak Larry Sanger sosee, Wikipedia ngi judd ci kàllaama waa angalteer ci 15 tamxarit 2001. Gu waa faraas teggu ci 23 gamu 2001, gu waa almaañ tegu ci ak yeneen yépp, ba tay ci atum 2007 mat nañu ñaari-téeméer ak juróom-fukki làkk.

Ci 1 diggi-gamu 2002 la Larry Sanger tekki ndomboy-tànkam ci ñaari sémb yépp, ginnaaw bi Bomis tëyyee loxoom, fayatul Larry Sanger ci liggéey bi mu doon def ci Wikipedia ak ci Nupedia. Ci 26 weeru koor 2003 la Nupedia tëj ba fawwu, Wikipedia moom wéy di màgg. 

Boobu ba léegi Wikipedia di dox ci ay àtte yiy askanam tëral ndànk-ndànk jëmug kanamam. ci 20 maami-koor 2003 la Mbootaay gu Wikimedia () juddu ngir wut ay koppar yu muy suuxate sémbi wikipedia yépp.

Wikipedia wolof moom mi ngi sosu ci ndeyi-gamu 2003, toog daanaka ñaari at te amul benn yëngu-yëngu. Ci tamxarit 2005 la am jukkeem bu njëkk. Xoolal xët wi ñeel 

Ni ñu ko binde ci xët wu njëkk wi, bakkam mooy:«Jimbulang bu ubbeeku bi», maanaam di lu ñépp bokk, te ñépp man cee cëru ngir gënal ko. Jimmy Wales di kenn ci ñaar ñi sos sémb bi, mi ngi koy tekkee niki «ag jéemantu ngir sos ak séddatle ab jimbulang bu ubbeeku ci anam gu mucc-ayib ngir nit ku ne man koo am ci làkku cosaanam». 

Baatu «Wikipedia» mi ngi jóge ci taqaleg ñaar yii di «wiki» di ag nosteg yoriinu ëmbiitu dalub web bu ñu man a soppi jaare ko ci ab joowukaayub web, ak « pedia » di reenu baatu làkku waa angalteer bii di encyclopedia, di tekki jimbulang.

Li ñu jublu ci sémbub Wikipedia mooy mu doon ab jimbulang, maanaan muy jëmmal bépp xameefu nit, lépp lu nit xam man caa ne. Wikipedia du ab baatukaay, du am péncum waxtaanuwaay (xoolal xët wii ngir xam lu wikipedia doon ak lu mu doonul: ). Sémb bi dafa àddunawu, day laal bépp xeetu xam-xam, bariylàkk, te amul ag pay.

#Article 57: Xam cig sori (118 words)

mooy xam ni yaram yi mel ak seen dëgg-dëgg ci lu dul ag laalante gu fisig walla simig gu jonjoo(direct)ak yaram yii, fi nu ko gënee doxale ci jamono jii nag mooy : nataali jawwu yi nuy far a defe ci satalit yi, walla yi nuy far a def di jëfandikoo ay fafal-naaw.

هو معرفة ماهية الأجسام دون التمساس الفيزيائي أو الكيميائي المباشر مع هذه الأجسام ومن أهم وأكثر تطبيقاته في الوقت الحالي هو الصور الفضائية التي يتم التقاطها عن طريق الأقمار الاصطناعية أو الصور الجوية باستخدام الطائرات يتم معالجة هذه الصور باستخدام برامج معالجة خاصة لأهداف متعددة منها :

جيولوجية: الكشف عن النفط,المياه,المعادن,الفلزات,الفوالق,متابعة التشوهات الجيولوجية... 
زراعية  : وجود الأمراض عند النباتات, معرفة أنواع النباتات في منطقة معينة... 

#Article 58: Mohammed (8705 words)

Muhammad (jamm  na sax ci mom) mi ngi judd ca Makka atum 571 g.  Ci at wowu la Abraha , buru Abissini , bëggona danel Kaba ji,  waye Yalla suñu borom danelna pexem , yonnifa ay picci yu amon ay xer yu mag ci sen sall , ray nitam yepp . Alxuran waxna ci li ci sar 105 , Al-fil , ñay wi . Muhammad ci banu Hashim la bokkon . 

Bayam Abdullah la won , dom bi  Abdul Mutalib ganona bëgg 
Abdul Mutalib . Bimu juddu dafa fekk Abdullah  mu de , di dellu ci jayantu ci  Sham , kon yay ji Amina bint Wahb  ak mam ji, Abdul Mutalib  . Mom bi Yonenta bi judd mag la won ta at yi danka xawona sonal  . 

Ca tukkib yaxantoom booba la baayi Yonnant bi làqoo , ca tawat ju ko daloon ba muy dëpp, ba muy ñëw ba agsi Madiina la ko gënoon a sonal, mu daal di wàcc ca ña ñu daa wax Banii Najaar di woon genn ci giiri Xasraj yi, fa la génne àdduna. Maamam nag di Haasim mom Abdul Manaaf dafa a takoon soxna, looloo tax ñu naan Banii Najaar de ay goroy Yonnant bi lanu (j.m). 

Yónnent baa ngi judd (j.m) ginaaw bi waajur wi làqoo, mu daal di màgg cig njirim, waaye maamam Abdul Mutalib beg ci moom lool, tudde ko Muhhamad, yar ko cig cofeel ak ñeewant

Waa Quraysin nag aadawoo woon nanu di yóbb seeni doom ca la génn Màkk, ca nàmpalkat ya ngir ñu man a màgg ci jàwwu ju sell, wér-gu-yarame te deesi fa dégge araab yu sell, bu ko defee loolu di tax ba ñuy wér, neexi araab te leeri wax. Nii la Aamina defoon ni ñépp, yóbb doomam Muhammad (j.m) ca ab nàmpalkat bu tuddoon Aliima Asahdiya, mu bokkoon ci Banii Sahd Bun Bakr, seeni kër nekkoon ca tàkk ga ca wetu Màkka. Bi Muhammad àggee ci am juroomi at la ko Soxna Aliima delloosi ndayam ca Màkka, mu nekk fa ca pekkam , maamam Abdul Mutalib di ko sàmm. 

Ca jamono jooja la Soxna Aamina Bint Wahbin jugoon ne day siyaareji bàmmeelub boroom këram Abdul Laah ca Madiina, ba mu demee bay dëpp la ko tawat ja dikkal, mu faatu ca ndëkk sa nu naan Abwaa te nekk ca yoon wa dox diggante Màkk ak Madiina, ñu daal di ko fay denc, looloo waral bi Yonnant bi màggee di ku soppoon di jaar ci ndëkk soosu ngir siyaare bàmmeelu waajuram ju jigéen ju laab jooju.

Ci nii – ndaysaan – la Muhammad mujje di jirim ci nday ak ci baay, looloo waraloon maamam Abdul Mutalib mujjoon féetewoo ag yaram akug wattoom, bëggoon ko it lool. 
Waaye sàmm googu gépp ak fonkeel gi teewul Muhammad (j.m) doon yëg naqaru njirim, ndax kat da daa gis moroomam yi ñu nekk ak seeni way jur, moom muy ku leen ñàkk, waaye nag loolu jox na ko ag sukkandiku ci boppam, may ko ag temb ci njëmm akug wéroodi ci kenn, nàmm am xelam, ubbil ko ay bëtam ci dëgg-dëggi dund gi, te booba ay atam lu néew la woon. Loolu de lu jeexiital la ci moom ak cig dundam, Yàlla nag moo bëggoon ci moom loolu ngir tànn gi mu ko tànn ngir mu yanu bataaxel bii di Lislaam te war koo tas.

Abdul Mutalib ginaaw bi Aamina làqoo yàggu fi dara moom itam làqu, te booba Yonnant baa ngi amoon juroom ñatti at, fa la ko baay-tëxam Aboo Taalib jële yóbb ko ca këram ca doomam yu xaw yaa sakkan tubaar-kàlla, ngir mu yaroo fa.
Aboo Taalib nag moo wuutu woon baayam ci jiite Màkk, ci noonu mu jeexaloon alalam jépp ci sàmm Kaaba gi ak way aj yi ak dimbali ñi aajowoo, looloo taxoon alalam bariwutoon ak li muy nekk kilifag Màkk lépp. Lii a waraloon Yonnant bi doon jéem a woyofal yan bi ci baay-tëxam jooju, ba àggoon ci di sàmmal ag jur ñenn ci waa Màkk yi, ñu ko ci daa fay lu néew a néew. Loolu it doonati ab pose ngir mu tàggatu ci xam ni nuy sàmme ag njaboot, jikkowoo ag ñeewant akug laa-biir ak sàmm ak yewwute, ñuy jikko yu manul a ñàkk cib sàmm bu bëggee wattu gétt gi muy sàmm. Yàlla moo ko bëggaloon loolu ngir tàggat ko ci bataaxel bi mu ko nar a joxi. Sàmm ag jur nag daara la joj lu bari ci yonnant yi jaar nanu ci, ba sax jële nanu ci Yonnant bi (j.m) mu ne : amul yonnant bu sàmmul ag jur.

Bi mu amee fukki at ak ñaar la ànd ak baay-tëx ji Aboo Taalib cib tukki dem Shaam, bi mu amee nag ñaar fukki at la tàmblee bokk ci yaxantu gi ni ko waxambaaney Quraysin yi daan defe, mu wone ci it man gu mu ko man lool, ndax ku ñu xamoon la cig wóor, ak dëggu, yewwute ak ñaw, ay man-manam tàmblee feeñ ñeel waa Màkk, li ko gënoon a wuutaleek nit ñi mooy wóoram gi jéggi woon ab dayo te xaroon baax, ñu mujjoon di ko wóolu ci lu mu man a doon, te am xel mu dal ci ne dana sàmmoonteek kóolute gi nit ñi def ci moom , looloo taxoon ñu naan ko ku wóor ki ak ku wóor ku dëggu ki.

Bi at yi àggee ci ñaar fukk ak ñeent daa dajeek Soxna Xadiija soxla waxambaane wu ko yoral yaxantoom gi mu doon deflu ca Shaam, moom nag soxna su woomle la woon bokkoon ci way woomley Màkk yi, ci noonu ñu digal ko mu gis Muhammad (j.m), ba mu ca waxeek moom Yonnant bi nangu. Yonnant bi yaxantujil na soxna Xadija ca Shaam ànd ak ngóoram sa nu naan Muyasara, Muyasara mii yéemu woon na lool ci jikko yu rafet yi ci Muhammad ak yewwu geek man gee yaxantu, ndax bi njaay mi nekkee ciy loxoom fulu na ay yooni yoon, wuuteek ba mu nekkee ci loxoy keneen, looloo tax bi Yonnant bi (j.m) delloo, jébbal soxna Xadiija alalam ak la mu ca tonoo, cig kóoluteek dëggu, soxna si yéemu na lool ci jikkoom yu rafet yi ak njëmm gi ne ci moom, ci noonu mu yónni ci moom kenn ci ay jegeñaaleem xamal ko ne da koo bëggoon niki boroom kër, Yonnant bi (j.m) nangul ko . Noonu la seen diggante sottee te booba Yonnant baa ngi am ñaar fukk ak juroom ciy at, Xadiija moom yor ñéen fukk, ci noonu mu faroon di soxnaam, di yaayam, di ki koy dimbali ci lépp.
Yonnant bi (j.m) amoon na ag texe ci séy boobu naka noonu Xadiija, ci noonu séen kër di misaalum mbégte cib séy ak texe ci biir kër. Soxna Xadiija nag mooy ki jur mbooleem doomi Yonnant bi, ku ci dul Ibraahiima, moom de soxna Maariya mi di ab qibt moo ko jur, moom nag (Sëñ Ibraahiima) ci jamonoy Yonnant bi la làqu. Yonnant bi wéyoon na ci yaxantoom gi ginaaw bi mu yoree soxna Xadiija, mu ko daan defe nag ni ko waa Xuraysin gépp daan defe rekk, ñoom de yorunu wooni bitig aki mangasin, moom kay danu daa defi njëgg yu mag mbaa yu ndaw jawali Yaman ci sedd bi, bu cooroonee ñu dem Shaam, màkk-màkka bu nekk daa na man a bokk ci njëgg li bu bëggee, njëgg loolu nag moom la nu daa wax ci ci araab Bahiir, kenn ci góori Xuraysin yee ko daa jiite , ku soob ci ñoom ànd ak moom, bu ko defee bu dellusee ñu seet li ñu tonowu, seddale ko, ku ci nekk am ca la nga ca def. Seen yaxantuwiin woowu moo taxoon Xuraysin daan am jot, di daje ci jataay yi di waxtaan, rawati na ca la wër Kaaba ga. Waaye Yonnant bi (j.m) moom néewaa na bu mu bokkee ci yii jataay, moom kay këram la daa toog mbaa mu génn dem ca àll ba ngir wéet fa di xalaat ak a settantal, ndax sopputoon di fo mbaa muy caaxaan ak a waxi larax.

Yonnant baa ngi amoon fan-weer ak juroom ciy at jamono yi Xuraysin di màbb Kaaba gi ngir tabaxaat ko, ndax tabax bi daa xawoon a màggat ngir yol mi daa sottiku ci kawam. Bi ñuy tabax ba àgg ca Hajarul Aswad ñu jaaxle ci gan giir ci Xuraysin mooy am teraangay yekkati ko teg ko fi mu war a tegu, ñu toog ca Kaaba ga di gëstu nu ñuy lijjantee loolu, far ñu dëppoo ci ne ku njëkk a ñëwaat rekk ñu jox la nga àtte leen ci jaaxle googu, far Muhammad (j.m) ne tëll, ñu ne ku wóor kaa ngee na ñu àtte, waaye mu àttee leen nu gaaw te yomb, mooy jël làmbaayam li mu yoroon lal ko ci suuf, teg ci doj wi ne giir gu nekk na jàpp ci cat ngeen tegandoo ko ca barabam. Nii daal la ko lijjantee ca yombam ga ak xarañam ga ak lëmóodikoom ga.

Bi at yi jegee ñeen-fukk la sopp gi mu soppoon ag wéet gën a yokk, mu gën a bëgg xëlwa ak beru, mu daan génn Màkk ngir dem ca doj wa nu daa wax Harraa, ngir xunti mu fa nekkoon mu mu daa faral a dugg ngir jaamu Yàlla, noonu la daa jeexale weeru koor wi, ngir sellal boppam, laabal xolam. Benn bis nag ci koorug atum 610 g .j, ba jant bay so la ko genn kàddu gu nooy dikkal ca dalug xunti ma naan ko : jàngal. Yonnant bi (j.m) tiit njàqare li jàpp ko, waaye mu ne ko : man duma kuy jàng. Waaye mu yëg mu mel ne dafa am lu koy naj ba dënn bi xaw a xat mu noppal ko, bu ko defee kàddu gi delseeti neeti ko: jàngal, Yonnant bi neeti ko : man de manu maa jàng. Naj ga delseeti, ba mu xawee woyofati kàddu ga delseeti ne ko : ((jàngal ci sa turu boroom mi bind , bind na nit ci lumbu dereet, jàngal, sa boroomay ki gën a tedd)) kàddu ga daal di dal, daal di deseeti. Fekk jant biy so Yonnant bi yëg njàqare lu rëy, daal di gaaw génn xunti ma, dem ñibbi, bi muy àgg lëndëm gaa ngi doon dugg, ndax diggante Màkk ak xur wa xaw na a ëpp ay ñatti kilomet.

Ba Yonnant ba (j.m) àggee ca kër ga daa daal di woote ne : muur leen ma, muur leen ma, booba ñaq waa ngay siit, yaram way lox, soxna Xadiija daal di dawsi sàng ko, tàmbli koo dalal, bi tiitaange gi demee Yonnant bi xamal ko li xew, ne ko : man de damaa xëm. Ndax xamagutoon ne li ko daloon ag wahyu la gu tukkee ca sunu boroom (t.s) , indil ko laaya wi njëkk ci Alxuraan ju tedd ji.

Soxna su tedd sii di Xadiija wéy ci di dalal xelum Yonnant bi (j.m) naan ko lii la dal de du man a doon lu dul lu baax, ndax yaw ku baax nga, am kóllare, dëggu, baax ci sa ñoñ, di taxawu nit ñi bu ñu ameey naqar. Ca noona xel ma tàmblee dal, mu yëg jàmm.

Bi soxna Xadiija gisee ne tiitaange gi dañ na daa ànd ak moom seeti doomi baay-tëxam ja tudd Waraqat’Ubn Nawfal, mu nekkoon góor gu am hikma, daan jàng téerey diine yi te dégg ebrë , Yonnant bi nettali ko li xew, Waraqat yéemu lool, ne ko lii de mooy mbóot mi Yàlla wàcce woon ci Muusaa (j.m), ne ko aka neexoon may gone ba man a ànd ak yaw ci tas sa bataaxel bii, xelum Muhammad dal, mu dellu këram, waaye teguñu ci lu néew rekk Waraqat faatu, ndax daa xawoon a màggat.
Yonnant bi dellu këram ak Xadiija ci xel mu dal ak mbégte, am yaakaar ne wahyu gi dina delseeti, bu sukkadikoo ci waxi Waraqat yi, waaye wahyu gi yeex a ñëw ba Yonnant bi far àgg ci jaaxle lool, waaye mu mujj ñëwaat ginaaw bi, xelum Muhammad dal, mu xam ne lii kat ag wahyu la gu tukkee ca Yàlla (t.s) te moom ku ñu tànn la ngir mu jottali nit ñi diine ju juge ci asamaan si, war a joxaat diiney asamaan yi seen leer ak sell gu njëkk ga ñu yoroon njëkk nit ñi di ko yàq, di ko tàqal ci li jamono di gën a romb. 

Nii daal la Muhammadum Abdu Laah mi (j.m) mujje di yonnant bu nu tànn yonni ko ci mbooleem mbidéef yi ngir mu indi fi leer gu tukkee ci sunu boroom di gindee, di tege ci yoon, di jële cig bokkaale jëme cig wéetal Yàlla,di jële ci lëndëmug réere Yàlla, jëme ci leerug gëm ko, jëme ci Lislaam.

Fii la jaloorey Muhammad yonnantub Yàlla bi - jàmm yal na sax ci moom – tàmblee akug jànkoonteem ngir wisaare bataaxel bii ko Yàlla jox mu war koo jottalee ci ngën ji anam ak melo.

ginaaw bi la wahyu gi tàmblee dikk cig toppante di wàcc ci Ku tedd ki, di indi laaya yi def tay alxuraan nànk-nànk, kon alxuraan ñëwadoowul cig mat, waaye laaya topp laay, ba kero muy mat, nga xam ne Jibriil da ko daan dikkal di ko déggal laaya yi, bu ko defee du ko ba ba kero muy wattu laaya jooju ci dënnam, mel ne sax dañu ko cee bind, làmmiñ wi di ko baamu, Yonnant bi bu masaa na jot ciw dogiit ci alxuraan da ko daa baamu ba mokkal ko, bu noppee jàng ko ci saabaam yi, daal di woo ñenn ci ñi man a bind ci ñoom ngir ñu bind ko ca saa sa ci anam gu xereñ, bu ko defee saaba yi gaawantu ñoom itam jàng ko mokkal ko ci anam gu dul soppikooti ba fàww. 
Nii la laaya yi doon dabantee, saar yi di ko mate nànk-nànk ci lu tollook ñaar fukk ak ñatt ciy at, ndax kat laaya wi njëkk a wàcc ci Yonnant bi (j.m) mi ngi ko fekkoon mu am ñéen-fukki at wi ci mujj wàcc bi muy bëgg a faatu te booba mi ngeek juroom benn fukk yu teg ñatt ciy at. Alxuraan nag ñi ngi ci jublu téere bu tedd bi bépp walla ab xaaj ci moom.

Kon daal Alxuraan ci nii mu ñëwe waxi Yàlla a ju mu wàcce cib yonnantam (j.m) ngir mu jottali ko nit ñi. Ñi ngi ko wàcce ci Yonnant bi, muy lu nu biddiwal, maanaam nànk-nànk, kem ni ko xew-xew yi soxlaa ak tolluwaay yi ba kero muy mat, di téere bu ñu laabal, bu ay caaxaan dul laal fenn ((laa yaatiihil baatilu min bayni yadayhi walaa min xalfihii)). Moom nag danu koo séddale def ko ay saar yu toll ci 114 saar. Saar wu ci ne tam seddaliku ciy laaya, saari alxuraan yi nag ak laaya yi lii lanu ëmb :

Saxal kennug Yàlla (t.s), nangu ne Muhammad Yàlla a ko yonni, gëm mbooleem yonnant yi fi jiitu woon Yonnant bi, gëm téere yi Yàlla wàcce ci ñoom, gëm alaaxira.

Julli, woor, natt asaka, aj. 

Ñuy wóor, dëggu, am yërmaande ci ku néew-doole, ku aajowoo, ku ñàkk, am ag cofeel ñeel bépp jullit tey dimblante ak moom ci lu baax ak fonki way jur, teral leen añs.

Ngir jàjjeek waare aki nettali ci dundug yonnant yi, ngir soññee ci ngëm ak foñloo wëlif bokkaale

Ubbi seeni gët ci kàttanug Yàlla gi akug xerañam, jaare ko ci di leen woo ci ñu settantal bindiinu àdduna bi akug nosoom gu xereñ gi

Jaare ko ci wax leen li Yàlla dig ku gëm cib yool akug pay gu neex ci àdduna ak alaaxiraa ak soññee ci jiyaar ci yoonu Yàlla.

Jaare ko ci leeral leen mbugël yi ñu waajal ñeel ñi ragalul Yàlla mbaa ñuy tooñ nit ñi di jalgati, mbaa ñuy gàttañlu ci def jaamu Yàlla yi

Mooy yoon wu mat wiy nos ni nit ñiy jëflantee ci seen biir, ak li nu am ciy àq aki yelleef ak li leen war ciy wartéef

Dinanu gise ci loolu ne alxuraan de ëmb na ag nos gu mat ñeel dundug nit ci gépp anam, mi ngi rëdd séqoo gu nit ki ak boroomam akug séqoom ak mbokkam, dajaleeti jullit ñi ci genn bennte mooy umma bi walla mbooloom lislaam mi (di jullit ñi ), joxati mbooloo mii yoon ak nosteg politig, gu mboolaay ak gu jikko.
Dugg ci lislaam du rekk jël diine gëm ko, di def li mu digale ciy jaamu, waaye kay ag tuxu la dem ci ag mboolaay gu yees gu mat gu ami ponkam aki nosteem aki yoonam aki misaalam yu kawe, ndax lislaam ag noste gu mat la gu takkatoo.

Bataaxelub Yonnant bi (j.m) mooy dugal nit ñépp ci lislaam ak tuxook ñoom jëm ca nosteg lislaam gu yees ga te mat.
Looloo taxoon Yonnant bi (j.m) daawul yam ci sàkku ci nit mu tudd ñaari seere yi rekk ak def jaamu yi, waaye kay da daan sàkku ñu bàyyi seen dundug réer gu njëkk ga te tàbbi ci nosteg politig, gu mboolaay, gu ruu gu yees gii. Moom de santuñu ko woon rekk mu woote te jotal bataaxel bi, waaye ligéey bu baax ci nit ñi gëm te dugg ci xeetu lislaam wi ak àddunaam ju yees ju fees ji dell ak yiw ak barke.

Yonnant bi wéy na di xamal nit ñi bataaxelam bi, bu ko defee gàllankoor yi nekk ci kanamam mel ne ay doj , ndax kat nit yombul mu tàqalikook ni mu baaxoo woon a dunde, nit jaamub li mu miin la, waaye moom mu wéy di deewoo, di jànkoonte, di muñ ba jóoxe bataaxel bi ca na mu gën a rafete. Loolu mooy kiimaanug dundug Muhammad (j.m) gu yéeme gi cib taar, moom daal ci léppam dund la gu fees dell ak ay bind yu fees aki bind yuy jàngale dëggug ngëm, wóor ci def li la war, muñ ci lu naqari, ñeg ci fas yéenee jéggi gàllankoor yi, ŋoy ci jikko yu rafet, muñ ci loraangey nit ñi, gëm ne ndam lu mu yàgg yàgg dana mujj ñeel jullit biy jëf tey jànkoonte tey ŋoy ci buumug Yàlla gi ci lu dul naagu mbaa yoqat walla tàyyeel.

Yonnant bi ginaaw bi nu ko yonnee dund na ñaar fukki at ak ñatt yoy ci la matale bataaxelam bi, fukki at ya ak ñatt nag Màkka la leen jeexal, fukk ya ca des mu def leen Madiina, làqu nag ca weeru rabiihul lawal ci atum fukk ma ak benn ginaaw gàddaayam gu tedd ga.

Mooy diirub deewoo ak jànkoonte gu tar ga ak way bokkaaley Màkka yi, ak jiyaaram ga ngir taxawal fa mbooloo mu lislaam mi, ba bi mu gàddaayee dem Madiina, diir ba di fukk ak ñatt ciy at.

Mooy jamonoy ndam, jaare ci dugg gi waa Madiina dugg ci lislaam, mbooloom lislaam am fa, ak nos mbooloo mii ak mottali jaamu yi nekk ci lislaam ak sariyaam, ak tëral nosteg xeet wi, gu politig gi ak gu mboolaay gi, ak dugal dunu araab bi ci lislaam ngir waajale ci tas gi lislaam war a tas ci mbooleem pàkki àdduna bi, ab diiram nag fukki at la ak lenn ciy weer.

Dafa séddaliku ci ñatti tolluwaay :

Am mbooloo topp ci tàbbi ci lislaam ci waxambaaney këri Màkka yu Xuraysin yu mag yi, ñi ci Yàlla ubbi séeni xol nanguloo leen lislaam ak dalam yu kawe yi, ku ci mel ne Talhata mom Hubaydul Laah, Abdurahmaan’Ubn Hawf, Sahd’Ubn Abii Waqaas, Usmaan’Ubn Haffaan, Subayr’Ubn’Ul-hawwaam.

Am mbooloo it tàbbeeti ci Lislaam ci ñu ñàkk ñeek jaam yi ak way néew yi doole ci ñi Yàlla tawfeexal ubbil leen buntub gore ak yamoo ak yaakaar, ku ci mel ne Bilaal mom Ecopi mi, Hammaar’Ubn Yaasir, Xabaab’Ubn’Ul-arat.

Mbooloom lislaam mii baaxoo woon naa dajeek Yonnant bi ca Kaaba ga ngir déglu alxuraan ci moom ak jàng ci ponki lislaam, loolu it jur way bokkaaley Quraysin yi yoqat ci jataayi néew yi doole yii ci li wër Kaaba gi, tax it ba ñu tàmbli di leen xatal ak a yoqatloo, Yonnant bi it gis ne war naa wutal jullit ñi barab bu ñuy daje cig féex akug dal, ci noonu wenn waxambaane wu bokk ci ñoom ñu naan ko Arqam Ibn Abiil Arqam ne man naa joxe këram ngir ñu fay daje, Yonnant bi nangu, looloo taxoon jullit ñi ba woon daje ga ñu doon daje ca Kaaba ga.

Waaye làqu gi nu làqu leegi tiitloo waa Màkka yi, jeqi ci ñoom njàqare, rawati na Aboo Jahlin ak Aboo Lahab mi nekkoon baay-tëxi Yonnant bi ak ñeneen, ñu tàmbli di topp jullit ñi ak di leen xeeñtu ngir xam li nuy def.

Am na bis Aboo Jahlin nekk fi barab di néggandiku Yonnant bi booba mi ngi jëmoon ca kër Arqam, ba Yonnant bi (j.m) egsee mu toroxal ko, waaye Yonnant bi muñ ak doonte ku dëgër la woon te manoon koo sonal, waaye Yàlla da koo digaloon mu woo nit ci hikma ak waare gu rafet, ci noonu mu wacc ko fa dem, bi Hamsa baay-tëxi Yonnant bi yëgee li xew daa mer seeti Aboo Jahlin duma ko ba noppi jébbalu dib jullit, ci noonu mbooloom lislaam mi gën a am doole ci dugg gi ci Hamsa dugg leegi.

Bi ci as ndiir toppee Omar’Ubn Xattaab jébbalu, jullit ñi gën a sawar, gën a ñeme, ñu daal di génn leegi kër Arqam daal di dellu fa nu daa dajee di la wër Kaaba ga, ci noonu Yonnant bi tàmbli di woote ci kaw ci lu bir, te faaleetul merum waa Màkka yi. Fii la jamonoy woote ci kër Arqam jeexe, leegi woote gu biti gu matale gi tàmbli.

Yonnant bi daa amoon njàqare ci saabaam yi, ragal waa Màkka yi sonal leen, ci noonu mu laabiire woon leen ci ne ku bëgg ci ñoom man naa dem Ecopi, foofa dananu fa man a doxal seen diine te kenn du leen topp mbaa mu leen di sonal, bi mu ko defee lu tollook juroom ñatt fukki góor akug jigéen gàddaay dem fa ci ñaari yoon. Yonnant bi des Màkka ak mbooloo mu néew ci jullit ñi, di jànkoonteek lori Quraysin yi. Waa Màkka yi jaaxle woon nanu ci man gi Yonnant bi (j.m) manoon a muñ ay coona ak sax gi, ñu sàkku woon ci baay-tëx ji mu tere ko woote gi maanaam Lislaam, waaye Yonnant bi bañ te wëy ca woote ga, looloo waraloon way bokkaale yi defoon ag dogoo gu mat ak Banii Haasin ak itam Banii Abdul Mutalib te ñoom ñooy mbokki Yonnant bi (j.m). Banii Haasim jànkoonte na aki coona ngir dogoo gii nga xam ne saxoon na ñatti at. Tolluwaay bu ñaareel bii nag weesuwutoon juroomi at.

Bi Aboo Taalib faatoo ba teg lu néew la soxna Xadiija làqu moom it (y.y.g ) ginaaw bi mu àndeek Yonnant bi ñaar fukki at ak juroom cig sell, cofeel, dimblante ak bànneex, ak doonte fukki at yu mujj yi daa feesoon dell aki jafe-jafe, mettiit ak xatal. Yonnant bi naqarlu woon na bu baax ci faatug àndandoom bii mu bokkaloon dund gi, nekkoon ku matal kóllare, wóor, taxawoon ci wetam ci ati jafe-jafe yi, wone woon gën jaa kawey misaal ci ni soxna su gëm tey muñ war a mel.

Bi Aboo Taalib ak soxna Xadiija làqoo Yonnant bi yëgoon na ne ku wéet la dëgg, te at yu metti yii mu def Màkka di jiyaar indilunu ko lenn ngérte lu ñu xam lu mu yaakaaroon ngir lànkug waa Màkka yi ak nuur gi nu nuuroon cig kéefar ak ŋoy ci li ñu fekkon seeni baay.

Fii la Yonnant bi xalaate ci génn jéem a wooteji ca Taayif ga jege Màkka, mu daal di fay dem ànd ak mawlaam bi Sayd’Ubn Haarisa, waaye waa Taayif déggalunu ko, looloo tax mu dëppoon dellu Màkka.

Waaye Yonnant bi loolu taxutoon mu yoqat ak doonte waa Màkka yi dañoo dogu woon ci lor ko, mu daal di jawali ca biti Màkka ca lenn ca giir ya fa dëkke woon, daan leen woo ci lislaam waaye taxutoon lu bari wuyyu ko ca.

Yonnant bi (j.m) da daan def bu déggaan aw nit ñëw Màkka mu gaaw gisi leen, woo leen ci lislaam, ba yonnant ga tollee ci fukki at ak benn daa dajeek ab kuréel ci giirug Xasraj ñëwoon Màkka, di woon genn ci ñaari giir ya nekkoon Màddiina, geneen ga di woon Aws, xare ba nekkoon di lu tar ci seen diggante ak noonoo ga.
Ca at ma ca topp am mbooloo ci Aws dikk na Màkka, Yonnant bi gaawantu seetsi leen wax ak ñoom, waaye fekk fi ñoom nopp yuy déglu, ndax kat Yahood yu Madiina yi dañu daan wax naan ab yonnant bu ñu yonni de dana dikki di dimbalisi Yahood yi ci Xasraj ak Aws, looloo waral Aws jortoon ne Muhammad (j.m) mooy yonnant bi Yahood yi doon wax. Bi seen mbooloo mi toogeek moom déglu ko lanu gis ne moom kat ku dëggu la ci li muy wax, bi mu leen jàngalee ay laaya ci alxuraan lanu ko gëm, sàkku woon ci moom mu may leen ba ñu dellu Madiina, man a nettali seeni mbokk li nu dégg.

Ci noonu ñu dellu nettali seen mbokki Aws yi li nu dégg, ñoom itam ñu amoon yitte lool ci gis Yonnant bi te déglu ko, Xasraj it dégg loolu, ñaari giir yépp tàmbalee yittewoo gis Yonnant bi, ñu daal di dogu ci yonni am mbooloo mu mag ci jamonoy aj gi ngir mu dajeek Yonnant bi (j.m), déglu ko

Mbooloo mi làqu waa Màkka ñëw dejeek Yonnant bi (j.m), déglu ko, waaye am lu leen wóor ci ne Yonnant bi de ku dëggu la, ci noonu ñu ànd dugg ci lislaam, def ak Yonnant bi jaayante gu Haqaba gu njëkk ga, daal di ko cay dig ne danañu woo waa Madiina ci Lislaam, te dinañu ko seetsiwaat ginaaw at, ci noonu Yonnant bi yabal ak ñoom saabaam ba tudd Mishab Bun Hamiir, ngir mu jàngal sariiya waa Madiina.

Bi lu toll ci at jàllee Mishab dellusi ànd ak ab kuréel bu mag ci waa Madiina, seenub lim tolloon ci juroom ñaar fukki góor ak ñatt ak ñaari jigéen, ñu jàkkaarloo woon ak Yonnant bi fa Haqaba jaayante fa ak moom, muy jaayanteg ñaareel ga, ñu ñaanoon ko mu tuxu dem Madiina, ne ko fas nanu ko yéenee aar ci gépp noonu te dinanu ànd ak moom ci tas Lislaam.

Ci ginaaw bi rekk la Yonnant bi digaloon saabaam yi ñu gàddaay dem Madiina, ñu daal di woon tàmblalee gàddaay ci ay mbooloo, mbooloo topp mbooloo, lislaam daal di fay tas ba mujj doo gis genn kër ca Madiina gu ay jullit nekkul.

Li ëpp ci jullit yi nekkoon Màkka daal di gàddaay dem Madiina ci weer yu néew, bi Yonnant bi amee xel mu dal ca saabaam ya ca Madiina, daa daal di gàddaay moom itam ànd ak àndandoom bu dëggu ba Aboo Bakr, ñu ngi génn ci lëndëm gi cig làqu, ndax waa Màkka dañoo bëggoon a tëye Yonnant bi ca Màkka ngir ragal lislaam di ame doole ca Madiina.

Mi ngi àgg Madiina ci 12 rabiihul Awal ca at mu njëkk ma ca gàddaay ga (4 sëtumbar atum 622 g,j), booba nag di taarixe ci gàddaay gi tàmbaleegutoon a dox, ndax Seydinaa Omar mooy ki digale ñu jël at mu njëkk mi ci gàddaay def ko at mi taariixu jullit ñi di tàmblee.

Yonnant bi fekk na li ëpp ci waa Madiina ñu tàbbi ci lislaam, ñu néew a ci desoon cig kéefar, te bi Yonnant bi dikkee dañoo daal di jébbalu. Yahood yu bari nag nekkoon nanu Madiina, tasoon fépp it, ña ca ëppoon daan bay, mbaa ñuy def yenn mecce yi niki meccem weñ ak tëgg. Ñatti giir yu mag nag feeñ na ci ñoom, ñooy Banoo Qinqaah, Banoo Nadiir ak Banoo Qariitha, ñoom nag dañu daa won Xasraj ak Aws ne ñoo leen kawe, te daan leen jaxase bay waral ñuy xulook a xeex. Bu xeex amee leeg-leeg ñu ànd ak Xasraj, leeg-leeg Aws, daa nañu wax naan ab yonnant de dana feeñi ci ñoom te bu ñëwee dina ànd ak ñoom xeex Aws ak Xasraj ba jële leen fi.

Yonnant bi bi mu àggee Madiina rekk daa daal di tàmbalee ligéey, ligéey bi nag ci ñaari mbir yii la jëmoon :

Bi Yonnant bi nekkee ci ligéeyam boobu ngir amal jubluwaayam yooyu, mi ngi doon wéy it ci di woo ci lislaam giir yi peek Madiina ngir ñu bokksi ci uma bi, di xeetu lislaam wii xëy taxaw, bi mu gisee ne lenn ci kilifay giir yii ànduñu woon ak moom ci loolu, daa daal di woon yabal ay cong yu lislaam ngir xeex kilifa yooyu ak ñi leen di jàppale ba duñu man a gàllankoor giir yi ci dugg ci lislaam.
Cong yii lanuy wax xaswat, ndax Yonnant bi (j.m) moo ko daan jiite, bu ko kenn ci saaba yu mag yi jiitee nag ñu koy wax sariya 

Yonnant bi tàmbli na, daal di yabal juroom benni xaswa ak ay sariya yoy amal nanu xemmemtéef lii, bu ko defee gëwéelub uma bu lislaam bi gën a yàkkiku, daal di far ëmb mbooleem wàllug càmmooñ gu Hijaas gi, loola nag la ca juddoo mooy Madiina mujj teg loxo ci yoonu yaxantu wi jëme Shaam juge Màkka. Looloo taxawaloon yaxantu ga ca Màkka te kat moo nekkoon balluwaay bi seen koom di juge.

Xaswa bu Badar walla xareb Badar Yonnant baa ngi ko def ci atum ñaareelum gàddaay gi, mi ngi ame nag ca digg yoon wa dox diggante Màkka ak Madiina, lu tollook ñatti téeméeri jullit am ca ndam ca kaw junni ci yéefari Màkka yi, muy ndam lu mag lol lislaam dëgëre na ci, nit ñi it xame ci ci anam gu wér péŋ gees manul a sikk ne Yonnant bi de wooteem gii lu wé la, ci noonu nit ñi sottiku Madiina ciy mbooloo yu mag ngir dugg ci lislaam, ci xare bii lanu raye Aboo Jahlin ak ñu ko moy ci nooni lislaam yu tar yig noonu.

Màkka manutoon a ñàkk mu def lu ko delloosi darajaam ji mu ñàkkoon ci dunu araab bi, ubbilaat ko yoonu yaxantu wi, looloo waraloon ay way bokkaaleem dajale woon doole ju mag ju toll ci ñatti junniy góor, ñaari téeméer yi diy gawar , ca atum gàddaay mu ñatteel ma ñu dox jëm Madiina ngir dugg ko ci doole, waaye Yonnant bi génn àkk léen ci lim bu toll ci junni ciy saabaam.

Ñaari mbooloo yi daje ca bëj-gànnaaru Madiina, fa ron doju Uhud, xare bu tar tàkk fa bob jullit ñaa ca amoon ndam ca njëlbéen ga, waaye boroom fett ya mujjoon wooteek ndigal la leen Yonnant bi joxoon daal di wacc seen barab ya nu leen taxawloo woon, Xaalid’Ubn Waliid mi jiite woon yéefar yi daal di màng pose bi song jullit ñi, bu ko defee seen sàppe jaxasoo, baj-baji, ñu ray ca ñu bari, waaye Yonnant bi moom des fa ak lu néew ciy gaayam, mu daal di woo ay saabaam ngir ñu dellusi. Ak li ñu ko gaañ ca xare ba lépp téewul mu xettali dooley jullit ñi ca njàmbaaram ga ak saxam ga, te tee yéefar yi dugg Madiina. Xeex bi wéy ba jant so, fii la coona bi sonale yéefar yi, ñu rocciku dellu Màkka ci lu dul ñuy amal li nu bëggoon, te loolu saxug Yonnant bee ko waral akug njàmbaaram ak sorib gisam.

Waaye yéefar yi li nuy amadi li ñu bëggoon lépp téewul ray nañu ab lim ci tànnéefi jullit ñi, ku ci mel ne Hamsa bay-tëxi Yonnant bi (j.m), ak Mishab’Ubn Hamiir mi daa gàddu raayob jullit ñi ak leneen lu toll ci juroom benn fukki jëmm, jullit ñi am nañu lu leen naqari lool ci seen sahiid yi, waaye jànge nañu ci Uhud benn bind bu ñu dul fàtteeti mukk, mooy topp Yonnant bi (j.m) ak defi ndigalam.

Waa Màkka yi yég nañu ne amaluñu dara lu am solo ci li ñu doon sàkku, ñu gis ne ñoom kat ak seen mbégte mu rëy mi ñu am lépp ci ray gi ñu def lu bari ci jullit ñi téewul Màkka dañul di nekke na mu nekke woon: yoonu yaxantu wi mi ngi ci loxol jullit ñi, giir yaa ngi tàbbi ci lislaam, gu dugg geneen topp ca.

Lii a tax Aboo Sufyaan’Ubn Harb mi nekkoon njiitul Màkka ginaaw Aboo Jahlin jugoon boole doole ju mag ci waa Màkka ak ñi tapoo ak ñoom ci giir yi, ñu dox nag jëm Madiina ca juroomeelu at ma ñeel gàddaay ga, bu ko defee Yonnant bi aki saabaam jug gas am xandaq ca la wër Madiina, ba mboolooy xarey yéefar yi agsee manuñoo jéggi pax ma, bu ko defee xare bi yam ci sàneente ay fett jéggi xandaq mi, ci noonu jullit ñi ñoom wone ag yewwu gu mat ci sàmm seen xandaq ba yéefar bu ko jéggi rekk rayees ko ca saa sa. 
Gaw gi sax lu tollook ñaari ayu bis, ginaaw bi Yàlla yonnee gelaw lu tar ak taw bu metti mu yàq xaymay yéefar yi, fay seenuw sawara, sedd bi metti ci ñoom ak doonte weer woowa wu mars la woon, te woowu weer fa Hijaas mooy tàmbalig lolli bi, bu ko defee yéefar yi àggati ci manuñoo ñàkk a dind gaw gi te dellu Màkka ngir sedd bi te amuñu dara ca seen càkkutéef ya. Loolu di ag juunu gu mag akug sooy ñeel leen, te diw lay wu mag ak firnde ci kàttanug xeetu lislaam wi ak dëggug gëm gi ay nitam am, ak ñaw gi nekk ci njiit la Muhammad (j.m).

Ñatti giiri yahood yi di (Banoo Qinqaah, Banoo Nadiir ak Banoo Qariitha) yoroon nanu taxawaay bu ñaaw te noonoowe jëme ca Yonnant ba ak wooteem ga, dale ko ca bi muy door a agsi Madiina, weddi woon nañu ag yonnantam, naan neey yonnant bi ñuy néggandiku manul a juge ci fu dul gañog Banii Israayil. Ginaaw nag yonnant boobu ñu daa wax farul génne ci ñoom, xanaa kay ci giirug Quraysin gu araab gii dara raxul, loolu naqari woon na leen, jural leen ag soxot ak kañaan ak mbañeel.

Yonnant bi yàgg naa muñ lor yi ñu ko daa lor ngir yaakaar gi mu yaakaaroon ne danañu mujj noppal ko, ba àgg sax ci gëm ko, waaye lu mu muñ rekk ñu gën koo bañe lislaam gën koo dellikoo ag noonu, waaye làqoon nanu seen noonu googu ak mbañeel gi bi ñu gisee ne lislaam mi ngi gën a dolliku doole, di gën a dëgër bis bu Yàlla sàkk:

Bi jullit ñi amee ndam ca Badar la xolub Yahoodi Madiina yi gën a dagg, ab kuréel ci ñoom it – ñooy Banoo Qinqaah - àgg ci manatuñoo ñàkk a feeñal seen bañ gi ñu bañ lislaam ak soxote gi ñu def jullit ñi ci ndam li leen Yàlla may, ci noonu ñu tàmbli di saboote Yonnant beek lislaam, waaye Yonnant bi (j.m) dem ca seen kër ya gaw ko, bi ñu jëbbalee seen bopp la leen génne Madiina ñu dem Shaam.

Ginaaw bu xaswat bu Uhud jàllee ba teg lu néew, la yahoodi Banoo Nadiir lànk ne duñu joxeeti li leen war ci ndimbalul alal li war ñeel umma bi, waaye yamuñu ca, dañoo tàmbli woon a defi pexe ngir yong Yonnant bi (j.m), waaye Yàlla (t.m) musal ko ci seenuw ay, nga xam ne Yonnant bi amul woon lenn lu mu manoon a def lu dul génne leen ñoom itam ngir mucc ci seenuw ay. Ci biir xareb xandaq ba yahoodi Banoo Qariitha doon nañu jéem a wor jullit ñi dem jàppaleji yéefar ya gawoon Madiina jaare ko ci may leen ñu dugg Madiina jaare ko ci seenug wàll, looloo war bi xeex bi jàllee rekk Yonnant bi daa daal di jawali ca seen kër ya, gaw leen ba ñu wommatu, nangul ko, mu digal saabaam ba tudd Sahd’Ubn Muhaaz mu àtte leen ci li jaadu fi moom, li tax mu tànn ko nag mooy ñoom ci mom lañu doon sàkkoo ag tin ci Yonnant bi, moom it mu ne nañu ray ñi ci doon xeex, ñi ci des ñu génne leen Madiina.

Ci noonu la xeetu lislaam wi mucce ci ayuw yahoodi Madiina yi, Madiina mujj yor lu néew rekk ciy yahood yu bokkoon ci ñi defoon ay tapoo ak lenn ci bànqaasi Aws yeek Xasraj, ginaaw nag feeñaluñu woon genn wor mbaag mbañeel ñeel jullit ñi Yonnant bi defu leen dara. Looloo waral ab kuréel ci ñoom gëm ca gëm gu dëggu, am ca ñeneen ñu ca gëm ñu ag ragal gëmloo akug naaféq

Bi Yonnant bi amee lu ko wóor ci ne am cong mu juge ci biti jeex na, wor gu biir gi it dañ na la tàmblee waaj ngir dugal Màkka ci lislaam. Gisoon na ne waa Màkka yi ñi ci ëpp ñu tàmbali woon a yittewoo mbiri lislaam lañu ndax gis nañu muy yaatu, di gën a am doole bis bu nekk, li Alxuraan digoon jullit ñi bañu nekkee Màkka di ñu néew doole gën di feeñ, gën di am. Nga xam ne Màkka li ko tee woon a dugg ci lislaam wéesuwutoon lenn ci njiiti yéefar yi ak seeni àndandoo, ñoom ñi ragaloon seeni njariñ di sànku, seeni daraja di suufe su ñu duggee ci lislaam.

Ci biir loolu ab laaya wàcci bu tedd buy digal Yonnant bi mu wëlbati qibla bi jullit ñi amoon muy Baytil Maqdis def ko leegi Kaaba gu sell gi, mu mujj ca saa sa di qiblab jullit ñi ñépp.

Bi ñu wëlbatee qibla bi leegi jëme ko ci Kaaba gi, te Yonnant bi xam dëgër gi xeetu lislaam wi def leegi te ame ko doole ci la jugoon ànd ak am mbooloo ci saabaam yi ngir defi umra, mooy siyaareji Bayti Laahil Haraam ci waxtu yi dul yu aj, looloo tax ñu tudde ko aj gu ndaw gi.

Bu ko defee, Yonnant bi (j.m) daal di génn ci junni ak ñeenti téeméer ci ay saabaam jëm Màkka ngir defi umra, looloo taxoon yobbaalewuñu woon ngànnaay ngir bëgg waa Quraysin xam ne jullit ñi dañoo ñëw ngir defsi ag jaamu rekk mooy umra gi. Bi jullit ñi aggee ci barabub Hudaybiya mooy buntub Màkka bi féete wàllug cammooñ la waa Quraysin yi tàmbali woon a ragal jullit ñi dugg Màkka. Ñu daal di yonnee ci Yonnant bi ne ko daal àndatuñu ci jullit ñi dugg Màkka ak donte yoruñu ngànnaay. Ñu daal di fay def waxtaan wu yàgg yu mujj àgg ci li ñuy wax Juboog Hudaybiya, moom nag li mu yaxal mooy jullit ñi buñu dugg Màkka ca at mooma waaye bu déwén ja’a ca waxtu woowa dinañu man a dugg (muy atum juroom ñaareel ma g.g), bu ko defee ñaari wàll yi def ag juboo guy sax fukki at.

Ca juroom-ñaareelu at ma ñeel gàddaay ga, Yonnant bi dellu defi umra ga mu yéene woon ca daaw ja, daal di siyaare ab dëkkam bi mu juddoo, ginaaw ba mu fa gëjee lu tollook juroom ñaari at.

Ci biir atum juroom ñaareel mi ñeel gàdday gi la Yonnant bi (j.m) yabal ay ndaw ca Qaysar mu Rom mi, Kisraa mu Faaris mi, ak kilifag Qibt ya ca Isipt, joxaale leen ay bataaxel yu leen di xamal lislaam te di leen ci woo. Qaysar moom daa yeexoon a tontu, bu dee Kisraa mu xottite bataaxel ba, waaye Maqooqas moom daa tontu tontu bu rafet, yonnee ca Yonnant ba adiya waaye taxutoon mu dugg ci lislaam.

Yonnant bi yonneeti ci lu bari ci njiiti araab yi ak seeni kilifa ak buur yi nekk ci mbooleem dun bi, am ñu ci dëggal te gëm, waaye la ca ëpp tontuwuñu.

Xaybar am mbooloom ay waaha yu ndaw la yu nekk ci bëj-gànnaaru daanaka dun bi, ca waxtu woowa Xaybar ci loxol yahood yi la nekkoon, ñu seŋe woon ko, ngartaajoo woon ay xéewalam, def ko seen dàttub xare tey seen barab bu alal, ñu tàmbali woon di xiirtal seen dëkkandooy araab yi ci ñu fexeel lislaam ak Madiina. Waaye Yonnant bi dëgmalsi leen ci mbooloom xare mu mag, gaw Xaybar, jullit ña songoo fa ak yahood ya cib xare, Yonnant bi dumaa leen fa, ñu wommatu, yeneen waaha yi ko jege woon te nekkoon ci loxol yahood yi topp ci, niki Fadk ak Timaa. Ci jëf jii la Yonnant bi raye jànkoonte ak jafadiku gi yahood yi dese woon daal di fegu ci seenuw ay.

Ci biir loolu fekk na Màkka mu néew lool doole, ñu ëpp ci ñi ko daa jàppale bàyyi ko, lislaam tas fat tas gu yéeme rawati na ginaaw Juboo gu Hudaybiya gi. Ci njëlbéenug juroom ñatteelu at mu gàddaay gi la waa Quraysin firi woon seen kóllëreg juboo ga ñu defoon ak Yonnant bi, loolu nag mi ngi ame ci tooñ ak jalgati gi ñu defoon giirug Xasaaha gi nekkoon jullit, ci noonu Yonnant bi jug ci fukki junniy jullit dugg Màkka ci lu dul xare ci weeru koor gu juroom ñatteelu at ci gàddaay gi (samwie 630 g.j)
Bi Yonnant bi duggee Màkka daa daal di laabal Kaaba gi, dammate xërëm ya, sànni leen ñu sori Kaaba ga, jullit ñi daal di raxas Kaaba gi, mu nekk leegi nag di néegub Yàlla deesu fa jaamooti ku dul moom. Ci loolu la Yàlla dëggale dëel bi mu joxoon Yonnant bi ak jullit ñi, ndax jàppale na leen, jàppale diineem, fay leen ci seen sellal gi ak dëggu gi ak jiyaar gi ñu doon def ci seen alal ak bakkan.

Bi loolu jàllee ba teg lu néew, lislaam daal di tas ci Màkka gépp, ñu taxawal fa ay jàkka, mu mujj di ñaareelu dëkk ak digg bu lislaam ginaaw Madiina gu ñu leeral gi .

Ginaaw bi ñu ubbee Màkka ba teg lu néew la giirug Hawasaan ak giirug Saqiif gi mu tapooloon jugoon dajale xare bu mag, dox nag ngir xeexi jullit ñi, waaye Yonnant bi duma leen duma yu tar ca fa ñuy wax Haniin, bi loolu amee genn giir jugatul naan day xeex lislaam. Ginaaw ndam lii Yonnant bi (j.m) dem na Taayif dëkk bi Saqiif dëkkoon gaw ko, ba gaw ga yàggee mu xam ne dana wommatu , la leen fa ba dellu Madiina, waaye noonu la deme woon ndax yàggaatul dara Taayif jébbalu, giirug Saqiif gépp dugg ci lislaam.

Atum juroom ñeenteel mi ñeel gàddaay gi ñi ngi ko tudde woon atum mboolooy yi, ngir ne ci la giiri dunu araab bi bépp doon yabal ay mbooloo yu bokk ci ñoom ngir yëglesi seenug dugg ci lislaam, mbooloo yii nag bawoo nañu ci mbooleem goxi, nga xam ne bi fukkéelu atum gàddaay giy jot fekk na mbooleem dunu araab bi dugg ci lislaam, ñépp ña fa dëkk mujj bokk ci uma bi.

Ci sawaal atum 9 ci gàddaay gi, ginaaw bi nga xamee ne mbooleem araabi daanaka-dund bi dugg nanu ci lislaam, la Yonnant bi bëggoon a xamal jullit ñi ne jiyaar ji de fàwwu mu génn dunu araab bi, ngir ñu man a tas diine ji ci àdduna bépp, looloo taxoon mu wommatoon benn xare bu mag ci ay jullit, dox jëm bëj-gànnaar ba àgg Tabuuk ca dig wa dox diggante dunu araab beek réewi Shaam yi nekkoon ci ron teg loxo gu Rom, foofa la nguuri araab yi nekkoon ci dig yooyu duggoon ci lislaam, jullit yi it xame ci ne jiyaar de day sax di wéy ba fàwwu .

Ci silhijja atum fukkéel mu gàddaay gi la Yonnant bi defi woon hajjatul wadaah di ajug tàggoo gi, ba muy dem nag ma nga àndoon ak ay junniy junni ci jullit ñi, ci aj gii la Yonnant bi (j.m) leerale ajiin wi ñu yoonal, te mooy wii fi nekk bat ay jii ñu nekk .

Bi mu noppee ci aj gi la def xutbaam bu bu mujj ba nuy wax xutbab tàggoo ba, mu dénk ca jullit ña dëggu, bennoo, boole séen sàppe, jóox farata yi lislaam digale ak tënku ci ponki jikkoom yu màgg yi, bi mu noppee jàngal nit ñi waxi sunu boroom ju tedd ja: (( al yawma akmaltu lakkum diinakum, wa atmamtu halaykum nihmatii, wa radiitu làkkumil islaama diinan)) di : (ci tay jii de laa matale seen diine ji, ci laa matale xéewal gi ma leen doon jox, te lislaam nag mooy diine ji ma gërëm te sopp ko ci yeen). Fii nag jullit ñi yëg nañu fi ne yonnant baa ngi leen di tàggu te di leen dénk li ñu war a def bu ñu ko gisatul, ñoom ñépp jàq te am lu leen naqari.

Bi Yonnant bi (j.m) delloo Madiina la yëg – ci mujjug safar – lu mel ne tawat di ku dugg, waaye faalewu ko, dafa wéy di ligéey ba tawat ji far ko man, mu doog a tëdd, waaye tawat ji yàggul, ndax mi ngi làqu ginaaw bi tawat ji amee ci moom fukki fan ak juroom, di ci 13 rabiihul awal atum 11 g.g ( 8 suwe 632 g.j) : 

Ci nii la Yonnant bi (j.m) tuxoo dem ca boroomam ginaaw bi mu jottalee bataaxelam bi ci anam gu mat te yaatu, tas ko ba ñépp jot ci, ca na mu ware. Wooteem gi mi ngi ko tàmbali cig wéet , ay gàllankoor aki pakastal gaar ko ay yooni yoon, mu daje ciy coona lol manoon naa yoqatloo geneen góor gu mu manoon a doon gu dul moom, woote na fukki at ak ñatt yoy amu ca lenn ngérte lu am njariñ, waaye mu sax di ku dëgër ag ngëm ci Yàlla, ku am kóolute ci ndimbalam, wéy ca liggéeyam ba ba ndimbal dikkal kook ndam ginaaw bi mu gàddaayee dem Madiina, daal di fay taxawal umma bu lislaam bi, dox ak moom ci yoonu nosu ak doole ci anam gu màndaqewu te callalewu, weer ginaaw weer, ba mujj am ci ndam lii ngay gis tay.

Yonnant bi nag li ko dimbali ci mu jot jubluwaayam bii mooy jikko yu yéeme yi te wéet yi mu jikkoo woon ak bataaxelam bii bàyyikoo woon ca Yàlla ma ko tànnoon ngir mu jottali ko.

Ñun nag manuñoo lim mbooleem jikko ak ngënéeli Yonnant bi (j.m), looloo waral jullit ñi ñoom dañu koo def muy xam-xam ci jëmmam bu ñuy jàng ñu koy wax xam-xamu jikkoy Muhammad (As shamaayil al muhammadiya) taalif nañu ci lu dul jeex, ñun nag ñu ñeme ñemelu indil leen lenn ci yi ëpp solo ci jikko yii :

Gëm gi mu gëmoon Yàlla gu matale woon la te xóot, da daan def fu jafe-jafe yi gënee bari, gàllankoor yi gën a dolliku, gëmam gi ci boroomam gën a dëgër, mu gën a ŋoy ci bataaxelam bi, gën a dogu ci wisaare wooteem bi ko Yàlla dénk. 

Looloo taxoon Yonnant bi ak saaba yi daawuñu nangu lu dul ngëm gu mat gu dara ci sikk dul jege. Ci daaray ngëm gu xóot gii la saaba yu mag yi génne, ku ci mel ne Aboo Bakr, Omar, Aliyu, Usmaan, Sahd’Ubn Abii Waqaas, Abii Hubaydata Haamir’Ibn Jaraah, Talhata’Bn Hubaydul Laah, Zubayru’Bnul Hawaam ak ñi mel ni ñoom ci ñi war a yanuji raayob lislaam ginaaw Yonnant bi (j.m), te war a tasaareji diiney Yàlla ji ci li ëpp ci pàkki àdduna yi ñu xamoon ca jamono jooja 

Ngir gëm gu dëgër gu xóot googu ci boroomam (t.s) ak ci lislaam, daawoo gis Yonnant bi mukk muy jëf ci lenn ndare bu tegu ko ci gën jaa dëgëri dàtti jikko yi, niki dëggu, matal kóllare, wóor gu mat ci wax ak jëf, ak seelug yéene ci lépp lu muy wax mbaa mu koy jëf, ak tëyye bu dëgër cig maandu ci mbooleem ay jëflanteem aki saabaam, ba ci ay kontaram, nekkoon na di ku bu waxee dëggal, bu dëelee matale, bu kóllarantee def ko, bu manee jéggale.

Yonnant bi de ak li ko dikkaloon lépp ci xéewali àdduna, ak teddnga ak doole teewutoon mu nekkoon di kuy doylu ci gën jaa tuuti ci xéewal yi, dundam gépp masu cee feesal biiram ciw ñam, lu néew ci mburu la daa mos ak tàndarma, bu amul rëndaay mu rëndaayoo diw, mbaa diw ak bineegar, mbubbam ak dallam ci loxoom la ko daa daaxe, daan fóot mbubbam bis bu jot ci loxoom, ndax moom (j.m) ku jéggi woon ab dayo la ci set, bis bu nekk daa na ci socc ay yooni yoon.

Daawul toggoo nag ag dund gu ñagas te di ko woote, moom kay ñam wu ko dikkal rekk mu lekk. Soloos na ci moom ne daawul sàkku mukk aw ñam wu fi nekkul, cib pajaas la daan nelawe, am mbalaanam it lu gàtt la daan doon, daawul tëju ay saabaam, ki gën a doyodi ci nit ñi da ko daa gis di wax ak moom, waayam ja ko daa ligéeyal di Anas mom Maalik nee na masul a dégg ci Yonnant bi ci dundam gépp benn baat bu ko mas a naqari. 

Daf daan bàyyee saabaam yi xéewal yi, te daawu ci féetewoo dara bàyyi leen, nekkoon na di ku sopp xale yi te daan kaf ak ñoom, ku amoon ag ñeewant la ci jirim yi, way ñàkk yi, ñu doyadi ñi, di seeti way tawat yi, bëcëg bépp it ci yëgg la daan nekk, daawul dal, ku bañoonug jekki la ak tàyyeel, daa na ko moytulooy saabaam.

Yonnant bi ku amoon ag yewwute gu sax la, daawul ba dara romb ko ci lu aju ci umma bi ndare bu da koo gendiku bu baax te settantal ko. Daf daan settantal di teg ay naal yu jub, yu yaatu yu muy jaar ci ligéeyam ci anam gu nosu te toftaloo.
Yitteem jépp da ko daa sotti ci li ëpp solo ci mbiri xeetam wi, teg ca la ca topp cig am solo.
Daa gisoon ne ay ligéeyam aki jëfam roytéef la wuy saabaam di jaari ëlëg, làmp la bu ñuy niitloo, moo waraloon lu muy def rekk mu koy def cig njàngale , cig yare. Bu kenn ci saabaam yi juumee ci mbir, da ko koy won cig nooy, leeral ko lay la jub. Ku daan am ag muñ ci way xuloo yi la, daan leen jéggal seeni soppaxndikooki jikko yu ñaaw ngir ñu gis seen njuumte, dellu ca jub ga. Ku wormaaloon nit ñépp la, daan sàmmoonteek teddngay ki gën di gone ci ñoom ak àqam. Masuñoo dégg fenn fu ñu ne Yonnant bi (j.m) génnee na fa baat bu ñaaw jëme ko ci kenn, ak doonte kenn kooku da dib noonam. Bu masaan a mer day noppi ba mer wa dañ mu doog a wax nànk, cig dal.

Yonnant bi noppee ko gënaloon wax, dégloo ko gënaloon déggal. Bu masaan a wax day àgg ca la mu bëgg a wax du jàdd-jàddal, def ko it ci baat yu leer te gàtt, looloo taxoon Yonnant bi (j.m) moo gënoon a am fasaaha ci nit ñi, gën cee am balaaxa, adiisam yi ci balaaxa ñoo topp ci Alquraan miy wax ji gën a balaaxaa ci wax yi.

Yonnant bi (j.m) yérmaande la ñeel mbindéef yépp, bi muy ñëw ci àdduna bi da koo fekkoon mu yor lëndëmug réer, ndof, xamadi Yàlla, waaye mu bàyyikoo fi, ba fi ag leerug gëm Yàlla . Mi ngi feeñ ci araab yi te booba ñi ngi ciy xareek fitna ak ŋaayoo, mu juge fi ba leen ñuy xeet wuy wenn, yiw peek leen, lislaam ëmb leen, jàmm uuf leen. Ak li Yàlla sotti nit ñi lépp ciy xéewal, jaarale ko ciy loxoom teewul Yonnant bi – jàmm yal na nekk ci moom – bi mu fiy juge di woon ku ndóol, ku moomul lenn. Saddaloon na nit ñi aw léew ci nite, ngënéel, def wartéef, sellal ak dëggu. Yàlla dëggal na – tudd naa sellam ga – ba mu nee : ((yaa ayuhan nabiyu inna arsalnaaka shaahidan wa mubashiran wa nadiiran wa daahiyan ilal laahi bi idnihii wa siraajan muniiran, wa bashiril moominiina bi anna lahum minal laahi fadlan kabiiran)) muy :( yaw Yonnant bi de dañu laa yonni ngay seere tey bégaleek a xuppe, di woote jëme ci Yàlla ci ndigalam, tey làmp buy leeral, na nga bégal jullit ñi ci ne am nañu ngënéel lu rëy lu tukkee ca Yàlla)
Yonnant bi nag (j.m) tënk na wax jépp ca bataaxelam ba niki kuy jàngale ba mu nee : (dees maa yonni ngir ma mottali jikko yu rafet yi).

#Article 59: Xeltu (1435 words)

Xeltu baat la bu nu doge ci « filasofia », muy baat bu cosaanoo ci làkkuw gereg, maanaa mi mu yor ci baat yi di « sopp hikma » loolu di (xel mu rafet ;sagesse ci Fr), ba ci laaj rekk ne « lan mooy xeltu ? » dees koy jàppe ab laaj bu di kojug xeltu bu nu man a yendu di ci dàggasante. Lii benn la ci màndargay xeltu yu dëgg-dëgg yi ak jeng gi mu def jëm ci laaju ak defi gëstu ci lepp lu mu man a doon te jéem a xam dëgg-dëggam aki màndargaam aki àtteem. Lii lépp a tax nag xeltu di xam-xam bu yaatu te bari ay ñall, laal daanaka ci xam-xam yépp, walla ci mbooleem wàlli dund. Waaye loolu lépp téewul muy xam-xam bu wéet ci boppam wëlif yeneen xam-xam yeek jagoo yi (specialisation). Xeltu leeg-leeg ñu melal ko ci ne mooy “xalaat ci xalaat” maanaam xalaat ci jëmmi xalaat, cib déndam ak ci settantal, dees na ko melal it ci ne mooy jéem a indi ay tontu ci laaj yi am gi di indi ak nekk gi (l’existence). Xeltu seere na ay jëm kanam yu am solo te lëw, dale ko ca waa Geres ya sos ponki xeltu yu mag yi niki xam-xam buy tabax ab gis-gis bu matale ñeel nekk gi(adduna bi) ci biir gis-gis bu di kojug li-am(réaliste), ba ca xeltukati jullit ñi nga xam ne danoo jëflanteek ndonol Geres li (li fi waa geres yu yàgg ya ba woon), jaxase kook nattu (experimentation), daal di soppi “xeltu bu kojug li-am” bi, yóbbu ko ci “xeltu bu kojug tur” ak “xeltu bu kojug xam-xam ak nattu” ci jamonoy yewwute walla judduwaat (renaissance), teg ci “xeltu yu kojug am yi” (existence) ak “yu kojug nite yi” ak “ngéri yees gi ak la ca ginaaw yeeg” ak “ñàkk” (maanaam dee walla bañ a am). Xeltu gu yees gi – ci aaday seggat ci Amerig gu bëj-gànnaar gi(USA) ak nguur gu bennoo gi (UK) (ci seen aada ji nu am ci seggat mbir yi (anaaliise ko)) – day barastiku jëm ci gën a nekk gu xarala ci gu neen rekk, moom day taxaw ci xellu (logique) ak ceggat gu dégg-dégg (conceptual analysis), looloo waral ay tërte (sujets) yi yitteem di jëm day àgg ci làmboo “gis-gis bu kojug xam” ak “jikko” ak “déndu làkk” ak “déndu xel”. Am na yeneen xam-xam ak jubluwaay yu jàppe xeltu muy jàng “fann” (walla ci Fr:art) ak xam-xam yi, bu ko defee muy gis-gis bu daj te matale, di tegtalub dund bu ubale te daj. Ci déggiin wii la xeltu di nekke di luy yittewoo xamale yoonu dund ga gën, dootul nekkati luy jéem a xam dund gi. Jamono yi jubluwaay bu seggat bi jàppee xeltu muy mbirum jëf mom fawwu nu jonjook moom, doxal ko, jëf ko, am na yeneen një (jubluwaay) yu ko jàppe muy cëslaay (base) li xam tegu, ñu war koo xam xam gu wér te xereñe ko. 

Xeltu baat la bu gereg bu juge ci (fila) di tekki sopp, ak (sofia) di tekki hikma maanaam (sagesse) walla xel mu rafet, kon muy firi ((sopp hikma)). Baatub xeltu ci jamono ju yees ji ñi ngi koy wax jublu ci dox gi nit di dox ngir xam laaj yu mag yi aju cig dundam, bokk na ci yooyu dund ak dee ak li-am (realité) ak maanaa yi ak dëgg. Baatu xeltu it dees na ko di faral di jëfandikoo ngir xamalee ci li xeltukat yu mag yi def ciy liggéey yu nu bokk.

Waxtaan ci xeltu du lu waa geres jagoo ñoom rekk, waaye kay ag wàll la ci xayug (civilisation) xeet wu nekk, xeet yépp a ci bokk. Looloo tax laaj luy xeltu? Du tekki benn tontu rekk. Xeltu cig tàmaleem ca jamonoy Taalis da doon gëstu cosaanul am gi (l’existence) ak aji bind ji (le créateur), ak ne-ne (matiere) bi ñu binde mbindéef yi, ak xeet (elements) yi leen toggale, bu ko defee dàggasante gi wéy di tang ci loolu ba ci jamonoy Sinon ak (Sofistaa) yi nga xam ne danu doon jëfandikoo xeltu ci weddi Yàlla ak wëlbati maanaa yi ak dégg-déggi baat yi (li nu ciy dégge) ngir notal seeni gis-gis, waaye mi ngi tàmbali ci jamonoy Sokraat mi Siisroon doon melal ci ne mooy ((ki wàcce xeltu ci suuf si jële ko ci asamaan si)), maanaam mooy ki jële xeltu ci xalaat ci nekk gi ak ki ko sàkk, ak xeet (elements) yi mu ko toggalee (yi mu ko sàkke), yóbbu ko ci xalaat ci jëmmi nit. Moom nag soppi na lu bari ciy màndargaam, daal di tuxal ay ŋaayoom aki dàggasanteem yóbbu leen leegi ci déndub nit (nature-am) ak dëgg-dëggam, ak gëm aji bind ji te gëstu ko, te jëfandikoo tegtalu xel ci saxal ko. Sokraat nag jëfandikoo woon na xeltu ngir tas jikko yu rafet ci biir nit ñi ak dëggu ak soppante. Sokraat nag ñëw na mook Aflaton (Platon) sukkandiku ci ñaari jumtukaay yii di xel ak xellu (logique) niki cëslaayi xalaat bu sell te mucc ayib, xalaat bob day dox dëppoo ak ay ponk yuy leeral ag wéram akug neenam.

Laaj : “luy xeltu?” bii laaj Aristo tontu na ko. Ci noonu sunu wax ji amatul njariñ, ndax dafa jeex te tàmbaleegul, kon tontu bu gaaw bi ci loolu day man a taxaw ci cëslaay lii: tontu bi Aristo joxe woon ci lan mooy dëgg-dëggi xeltu du moom rekk mooy tontu bi nu ci man a joxe, ca dëgg-dëgg loolu daal benn rekk la ci tontu yi nu ci man a joxe. Nit daal - bu sukkandikoo ci ni Aristo xamalee xeltu – dina man a xalaat te firi xalaat yi jiitu Aristo ak Aflaaton ak xeltu yi ñëw ginaawam. Ànd ak loolu teewul nit ki dina seetlu ci anam gu yomb ne xeltu de ak yoon wi nu xame dëgg-dëggam soppiku nanu ci ñaari junniy at yi topp ci Aristo soppiku gu mag.

Waaye ci biir loolu jëmm ji wart a réere ne xeltu, la ko dale ca Aristo ba ca Nits dafa sax – ci cëslaayi soppiku yooyu ak yu leen moy – di moom ci jëmmi boppam, ndax kat soppiku yooyu dafa ame ci wàllug xereñ. Wattu ag yamoo ci biir moom moom la (…)

Lu wér la ne dinanu man a ame ci yoon woowu ay xam-xam yu wuute te xóot, neel yu am njariñ ci ni xeltu feeñe ànd ak taariix, waaye nag woowu yoon dunu may ñu àgg ci am tontu yu dëggu maanaam yu yoonu ci : lan mooy xeltu?

Ni Aristo firee xeltu ne mooy “sopp hikma” am na lu ëpp benn teglal walla maanaa. Tegtalub làkk bi, moom mi ngi aju ci làkku gereg wi ñu tëgge baatub filosofia, ak tegtalub xam-xam bi nga xam ne dafa wuuteek li nu nekk lool. Sikk amul ci ne tegtal bu mujj bi walla maanaa mu mujj mi mooy bi leeral maanaa mi, gaw ko ci “sopp hikma” niki melo wu nu man a wonee ñàkk gi ay am-am (donnés) yu xam-xam ñàkkoon ñeel xeltukat bi ca jamono jooja, bu ko defee hikma nekkoon benn ci pexe yi ñu daa pexee ci lu nu xamul, niki ab ne-ne bu njëkk bi nga xam ne ci la xeltukat biy sose nosteg xam-xamam, mu dëppook settantal gu xam-xam ga amoon ca jamono jooja.

Bu dee leegi nga xam ne xam-xam daa sakkan, li ñu wuññi lëw, laaj yi bari ci ëtt yu bari ak mbir yu dul jeex, ak jëm kanam gi nit def ci wàll yu bari, loolu lépp tax na ba liggéeyub xeltukat du doonati rekk sopp hikma, ak gëstu ko ci jumtukaay yi mu ko daa gëstoo ak ci ron kilimãb réer gu tar gi mu amoon ci wërlaayug àdduna gi ko wëroon ca jooja jamono… Xeltukat leegi lu sakkan ciy ngér (ecole, methode) ñoo ko tënk aki àtte yu di kojug xellu aki am-am yu di kojug péng (lu wóor), ci ron jalub ay xam-xam ak seeni doxal (pratique) yu xarala yu la dul may fenn fooy sikke seenug nekk di yoon. Ci ndabi jamono (conditions) yu mel ne yii, ak ci am-am yu nirook yii xamaleg xeltu ga nu xamoon du manatee dëppook liggéey bi xeltukat bu jamonoo bi man a def, maanaam bu sunu jamono jii nu nekk, moom mi nga xam ne ab liggéeyam daa wuuteek bu ñoñ jamono yu yàgg ya lool.

Bu nu sukkandikoo ci li jiitu danu naan manatuñoo def nenn nu dul jéem a xool nu nuy soppee dégg-dégg ak maanaam xeltu ndax mu doon leegi “juddal hikma” te bañ a doonati “sopp hikma” 
     
#Article 60: Wuutuloxo (155 words)

Wuutuloxo walla masin mbooloom ay cër la, yu am lu bon-bon benn bu man a yëngu, yees lëkkale ngir jublu ci mu def jenn jëf ji jees tëral-jëkk, kon muy lu man a def liggéey bu nit dul man, ndax xéj-na dafa laaj jenn doole ji walla mu koy war a defe ci wërlaay gu nit manuta dund.

Xeeti wuutuloxo yi bari nañu te itam dañu leen defar ngir njariñ yu wuute: ci misaal, wuutuloxo bu mbëj, wuutuloxo bu mbay, wuutuloxo bu yóbbte ak yëkkati, ak yeneen. 

Jëfandikoo gu wuutuloxo yi dimbali na nit ñi ba ñu man a def liggéey yoo xam ne weesu nañu dooleem, kàttanam. Bu dul woon wuutuloxo yi, nit ci dundiinu nit ñu njëkk ña lay des ba tay, te du am nenn numu man a def ba jëm-kanam. Kon wuutuloxo day tekki bepp jumtukaay buy yokk sa doole, di wàññi sa coono, te di gaawal aka gënal sa liggéey. 

#Article 61: Melosuuf (1171 words)

Melosuuf mooy xam-xam biy settantal ak a leeral feeñtey yaram yi walla jëmm yi ak yu dundat yi a yu nit ñi ci kaw suuf si ak gëstu gi aju ci ni ñu séddalikoo.

Séwogaraafi baatub gereg la, boo ko doon firi ci wolof muy “melal suuf si”, maanaam wax ni mu mel, ni mu nekke.Moom nag baat la bu tukkee ci (Geographica): baatub gereg bob cosaanam mooy (Geography),muy ñaari baat yu ñu boole ñuy benn bu njëkk bi mooy tekki melo, walla nataal (Graphica), ñaareel bi di Geo di tekki suuf.

Bu nu sukkandikoo ci loolu danu naan Sewograafi walla Geographia mooy “melal suuf si” walla wax ni mu mel, xam-xam bii noonu la tàmblee woon, ndax ca njëlbéen ga, tukkikat yi daa wër di gëstu dañu daa bind li ñu gis ci dëkk yi nu romb ak gox yi ak diiwaan yi ñu siyaare, leeral, melal ni ñu leen gise, fekke leen ni. 
Sewogaraafi nag déggoo nanu ci séddale ko ay xaaj ñooy yii:
Séwogaraafi bu dénd bi (nature), mooy biy sonn ci gëstu ni suuf si mel, ni mu bindoo ci wàllug jiyoloji, ak feeñte (fenomene)yu jawwu yi ak gàncax yeek dundat (animal) gu dénd geeg gu jeeri ji.
Bokk na ci xaaj yooyu Séwogaraafi bu bidiw, li ko tax a jug di: jàng ni suuf si bindoo ak ab kemam, ni muy yëngoo, ak ni mu buloo ak séqoo gi mu am ak yeneen bidiw yi.
Bokk na ci xaaj yi ba tay, Séwograafi bu nit: moom nag daa séddaliku ci :Séwogaraafi bu way dëkk yi (abitant), ak séwogaraafi bu koom koom ak bu politig, mooy gëstu ci goxi àdduna bi aki pegam (frontiere) yu politig, aki jafe-jafeem ak ña fa dëkk.
Ak bu nataal yi walla bu lonkoyoon yi: moom mooy xam-xam biy yittewoo lonkoyoon sewogaraafi yi ak ni nu leen di sose.
Bu yàggul bànqaas bu yees sosu na ci xam-xamu Sewogaraafi, mooy biy nos xam-xam yu sewogaraafi yi ak yëglu cig sori

Melosuuf moom nekkatul rekk xam-xam boobu di melal feeñte yi (les phenomenes) di leen melal ak a leeral ci anam gu tond, gu soreek li am, waaye mujj na di xam-xam bi jagoo dox ànd ak jëm-kanamug xam-xam bu bees bii sukkandiku ci gëstu ak nattale, ak làmb ba daj, ak jëfandikoo misaal yi ak gis-gis yu yees yi, ci noonu la mujje di lu nuy doxal ci anam gi nuy tudde séwogaraafi bu kem ak séwogaraafi bu doxal walla dëppale “bu pratique” bi nga xam ne du nangoo beru wëliif soxlay nit yu mag yi, loolu nag li ko waral mooy li séwogaraafi làmbool yor ko ci man–manu dëppoo ak mbooleem xam–xam yi, moom mooy aji jokkale ji nekk ci diggante xam–xam yi di leen booleek a jokkale, bu ko defee di leen tàggat ngir ñu liggéeyal ko, di jël ci ñoom lu koy jariñ, di ko ràññale ak yeneen yi. 
At yu mujj yii seere nanu ag soppiku gu mag ci gérum séwogaraafi ak xam-xam bi mu ëmb, ak ci anam yi muy jaar ngir amal ay jubluwaayam aki xemmemtéefam. Man naa am nag mu bokk ci li indi coppiku gii: jëm gi nit ñi gën a jëm kanam, nga xam ne sax boroom xam-xami séogaraaf yi mujj nanu di gëstu ay mbir yoy bu njëkk xamuñu leen woon, ba sax kuy seetlu liggéeyu boroom xam-xam yii dana gendiku yittewoo gu dolliku gi nu sotti ci mbirum gëstu feeñte yi /phenomenes/ ak masala yu wuute yi aju ci dénd bi ak nit, ci anam gu wuuteek ga nu ko daa gëstoo bu njëkk, sababus loolu nag mooy jëfandikoo gi nuy jëfandikoo leegi ay jumtukaay yu xarañ te aaytal ci seeni gëstu, di dimbadikoo xam-xami takk yi (statistiques) ak yu xibaar yu jumtukaay yi ak mat ak misaalukaay yi (echantillon) ak xam-xamu xarala ak dénd (nature bi) ak kimya (simi). Jëm kanam gii am nag ci jëfandikoo jumtukaay yii ak ker-keraan yii (ces moyens) tax na ba ngérte (resultants) yu am solo juddoo ci, yu jañ séwogaraafi mu jëm kanam, def ko muy xam-xam bu jamonoo. Loolu sax tax na ba ñenn ñi di woowe jëm kanam gii am ci xamu melosuuf ((jeqiku walla fipp gu kemu ci xam-xamu séwogaraafi)), 
Jeqiku gii walla fipp gii waa melosuuf yi teeru nanu ko te màggal ko, ndax ngérum kem ay ngënéelam lu bari la, man naa am li ëpp solo ci ngënéel yooyu mooy ngérte yi mu lay àggale yépp ñooy gën a sew, gën a am maanaa, ngir seggat (analyse) gu xam-xam gi muy amal ñeel toftaloog mbir yi. Ceggat gu xam-xam gu melosuuf gii mooy wone noste (systeme) yi amal ay jeexiital ci amug feeñte yu wuute yi melosuuf di gëstu. Moom du doylu ci leeral feeñte yi rekk waaye day sukkandiku ci sabab yi sos feeñte yii.

Ngir melosuuf man a génne, feeñal lëj-lëj ak jafe-jafe yi gawu cib gox walla ab diiwaan, li muy njëkk a def mooy digal ëtt boobu walla barab boobu , maanaam wutal ko aw dig ba ñu xam ne fii la, bu ko defee mu fésal séqoo (les relations) yi am ci diggante mbooleem xeet (element) yu wuute yu kojug dénd yi (naturel) ak yu kojug nit yi, ak nu ñu man a duggantee ci seen biir, ràbbaloo ni. Looloo tax séwogaraafi fi di boroom jikoo ju ràññiku, ndax danu koy gis mu tegub tànk ci xam-xami dénd yi, tegati beneen ci yu nit yi. Bu fekkee ne xam-xam yu wuute yi ci atum 1972 lanu leen raŋale, nos leen, séddale leen ñatti kuréel ñooy : xam-xami seggat yu nattu yi, xam-xami firi yi ak taawiil, ak xam-xami jam yi (yu critique yi), bu fekkee ne noonu la it melosuuf moom jël na mbooleem jikkoy yii kuréeli xam-xam .
Jàng ëttub melosuuf dina feddali amug ay way nekk yu bari yu dénd ak yu nit yu lënkaloo yuy ràññikoo ci jëflante yu bari yuy am ci diggante way nekk yii, loolu moo lay won foofu solos boroom xam-xamu melosuuf, looloo tax nga gis gëstu ëttub melosuuf du yam rekk ci menn mbir walla benn feeñte bàyyi ya ca des, ak doonte ëttub melosuuf làmboo na mbooleem feeñte yépp, teewul gëstug feeñte yii day am cig beru tey natt tolluwaayu jëflante gii seggat ko, yillaal ko , ci lu dul muy sàggane benn xeet (element) ci xeeti ëtt bi.
Ngir solos ëttub melosuuf Unesco saxal na ni nu koy jàngalee ci Tugal ci donga yiy door a dal, bu ko defee ñuy def aw doxaliinam ; sukkandiku ci dégg te xam juroomi laaj loolu nag mooy : ëtt biy jóox (biy produire) : bu ñu laajee njàggaan li jéego yi aju ci déggiinu ëtt biy jóox loolu man naa doon yoon wi ngir xam dëgg gi maanaam yewwu ci ne ëtt boo gis du lu dul melo ci meloy yëngu yi (maanaam mi ngi ci melow jóox) kon nag ngértel saxal yu tukkee ci nit ñi la (jeexiitalu jëfi nit) 

Boo gëstoo lonkoyoon (carte) adduna bi bu baax di nga ca gis dëgg yii :

#Article 62: Téere ci murit (15180 words)

Bii mooy teereb Irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim, di ci maanaa nàndalug aji naanaale ji(ki ngay toogal di naan) ci ndox mu neexum sopp jëwrinu yonant bi , di xam-xamu jaloore bu nu gàttal mu ñeel nag ki bëgg a am ab xam-xam ci dundug sëriñ Ahmadu Bamba yal na yàlla dolli gërëmam ci moom ,te jariñ ñu ci,amiin.
Ki ko taalif it di ku xeebu ku aajowoo ndimbalul boroomam ak yermaandeem,tey yaakaar ci moom mu jéggal ko ay bàkkaaram,te làqal ko ay ayibam,yi feeñ ak yi nëbbu,fii ak fan jëm,di Muhammadul Amiin JOOP doomi sheex Ahmadu JOOP mu dagana,yal na leen yàlla boole jéggal.
Di it taalibeb sëriñ Tuubaa, yal na ko yàlla gërëm te jariñ ñu ci moom,amiin.
Maa ngi ñaan yàlla mu musal ma ci saytaane mu nu jam mi,di tàmblee nag samay wax ak jëf ci turam wu tedd wi,moom mi yor yërmaande ju yaatu ji matale mbindeefam yi ci àdduna,te di ko jagleel ñi ko soob ca àllaaxira,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci sunu sang,Muhammad,ak ñoñam aki saabaam.

Aji xeebu ju yitewoo yërmaandey boroomam,ak ndimbalam ci ligeeyal yarkatam bii dib soppeem(di sëriñ Tuubaa) - aji xeebu jooju di Muhammadul Amiin JOOP doomi Sheex Ahmadu JOOP mu Dagana, nee na: ag cant ñeel na yàlla miy leeral àddinaam ji ci walliyoom yi,di feeñalati ci ñoom yoonu yonantam yiy gindee,yoon woowu di wu weetal yàlla ak jaamu ko,mooy yoonuw boroom xel yiy dàq lu dul yàlla ci seeni xel,tey jànge ag njub ca yooyale imam,ci jox leen seen bopp,jébbal leen seeni mbir. Ndax kat ñooñooy ñi yàlla naan ci alxuraan: ulaayikal lathiina hadaahumul laahu fabi hudaahumuqtadih muy ci maanaa ñooñooy ñi yàlla gindi kon royal ci seenug gindi.

Di julli tey sëlmël ci yonant bi.

Leegi nag ginaaw yàlla day xéewale xarnu bu ne aw waliyu wu koy gindi di ko won yoonu jub ,di ko tee jàdd, nun waa xarnub fokk ñeent nag mu defal nu,xeewal gu tollu ne sunu mbeg mii di sunub sëriñ tey sëriñub julit ñi Ahmadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah yal na ko yàlla wattu te wattul ko,te gërëmi jëfam,te méngoo ko,moom nag mbooloo maa’ng ko gën a xame ci turu sheex Ahmad Bamba MBAKKE Xaadimur rasuul.

Bi loolu amee ma bëggoon a leeral as lëf cig dundam ñeel ki nar a ñëw ginaawam,te bëgg a xam dara ciy mayam. Man nag maa ngi giñ ci yàlla dellu di ci giñaat naan dey xam naa ni xawma te du ma ci man a wax mbaa indi lu dul la gën a neew,la gën a bari moom bu ko xalaat,ndax manu ma ko ba koy def.

Waaye nag dinaa jeem a nooyal yoon wi,ba ku bëgg te yàlla ubbi ko barilub xam-xamam, yinkiiwal ko jariñ jaamam yi ngir sàkku ci ngërëmam,bu ñewee man cee jaar,ndax kat am na ci addiiz mu sell mi: mbindeef yi njabootug yàlla lanu ,ki ci yàlla gën a bëgg mooy ki ci ëpp njariñ ci njabootam gi. Nee nanu ku taarixal aw walliyu mel na ni dundal nga ko.
Kon am leen gàttalug jaloore (jaloore mooy taariix walla histoire) gii ma tudde irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim, may ñaan nag képp ku ci gis lu ko yeemut, mu xam ne gàttub jéegoo ma tooñ,mu jeggalul ma yàlla te suturaal ma,te bañ koo ngàññi,ndax kat da na ci gisi leneen lu bari lu koy yeem, lu man a wecci loolu ko yeemutoon, ndax teere bii ab muxaddima rekk la ( ag jiital) teere degg bi mooy minanul baaqiil qadiim fii maathiris zheixil xadiim muy ci maanaa xeewali aji des jiy aji jiitu,ci ngëneeli sheexul xadiim.

Doomam ja sheex Muhammadul Bashiir defoon ko,yal na ko yàlla sàmmu te guddalu fanam,te jariñ ci lu bari jullit ñi ni baayam,moom dey teere bu boole la te wattu,te dib dër bu naat ñeel ku bëgguw yiw te di ci dox. Yal na ko yàlla mottali te nangu ko,te tas ko ci àddina bi,muy ndaxañteefam ëlëg ca àllaaxira,tey lu nu koy fàttalikoo ginaawam ci fii fi àdduna,ci barkeem ak ci barkeb ki ko taalif ak kim ko taalifal,yal na nu yàlla nangul,te nangul nu sunub teere,matal ko te tas ko moom itam.
Moom kat yàlla mooy aji kawe jiy boroom ngëneel ak tawfeex,tey borom li fii ak la fee.

Sëriñ baa ngi gane àdduna - ci li nu wax – ci atum junni ak ñaat teemeer ak juroom ñaar fukk 1270 g, am ñu ne atum junni ak ñaat teemeer ak juroom ñaar fukk ak ñaar 1272g,ca kër waajuram wu goor ca Mbakke Bawal ,mu nekk leegi ca wetu yoonu saxaar ga. Boroom xam-xam bu mag bi nuy wax Alhaaji Hamidin doomi Usmaan Alfuutiyu Altilriyu nee na: (( sëriñ baa ngi gane àdduna moom mi sunnawoo sunnas yonnant bi,ci atum sharaha,muy 1270g làqu atum shumoos muy 1346 g te booba mi ngi am juroom ñaar fukki at ak ñeent mel ni ay jant. Am ñu ne juroom ñaar fukk ak ñaar,ci guddig àllarba ci ñaar fukki fani muharram)).

Moom sëriñ bi bi mu ganee àdduna waajuram wu jigeen a ko yoroon bam mat a jàngi, Mu tudoon nag Amadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah doomi Muhammadul kabiir mom Habiiballaah mu njëkk ma doomi Muhammadul Xayri,ak Muhammadul Kabiir,Muhammadul Kabiir mii mooy ki niy wooye Maharam,mooy ki sanc Mbakke Bawal atum 1194 g ,ci li nu wax,waaye dëkkewu ko woon da faa ba woon ab taawam Muhammudu Farimata,magi habiibullaah waaye bokkunu nday,moom nag sëñ Maharam mii daa desoon Jolof,fa la làqqoo nu denci ko fa,di ko siaare.

Mi ngi askanoo nag ci tukkloor,ay waajuram a ngi bawoo Fuuta,dem Jolof, siw na itam ne ñoom Gànnaar lan bawoo dem, Fuuta,seeni doomi baay tëx ci naar yi ñooy ñoñu Moodi Nalla, ñoom nee nanu ay serif lanu.Sama mag sama sëriñ sheex Muxtaar binta Loo,doomi sheex Iraahiima sëriñub Njumri Loo nettali na ma ne degg na ci sëriñ bi luy dëgëral loolu,mu ne bis nekk na fa sëñ ba nuy waxtaan ba tudd ag giir ci naar yi,gu niy askanale ag cëriif,sëñ bi ne ko xanaa xamoo ne ñooñu suniy mbokk lanu,mu ne ci noonu la xame ne ñoom ay sëriif lan.

Man nag li may wax mooy seenug cëriif bu nu ko waxutoon te deggeesu ko it,seen jikko yu rafet tegtale na ko,muy tedd gu ànd ak yaatug dënn,ak lewet gu ànd ak njàmmaar,ak jublu ciw yiw,ak bañ jikko yu suufe yi,ak diinewu gu dëggu.

Yaayam soxna Jaaratul Laahi Maryama BUSO doomi Muhammad mom Muhammad mom Hammaad mom Alliyu Albusobiyu, ñooñii seenug cëriif lu wér la, ñi ngi cosaanoo ca Imaam Hasan mom Alliyu ibnu Abii Taalib karramal laahu wajhahuu,kon sëñ bi serif la ci nday ak ci baay. Lenn ci samay doomi baay tëx nettali na ma te moom ku dañ kumpa la ci suufus Fuuta ,mu ne dox na bis juge ci dëkk bu ndaw bu nu naan Bukke jëm fun naan Mbumbe péeyub Filaaw,nee na mu romb ci ay gent yu ñu ne ko ñooy fi Mbakke-makke yi dëkke woon.

Am na ku ma nettali ci ñi sant Ba,ne Mbakke-mbakke yi seeni doomi baay tëx lanu,kaaf gi nekk ci Mbakke ag Haa la woon muy haa giy mujj ci ba,wolof yi def ko kaaf,waaye wax jooju ju doyadi la fi man,li nu jortu daal mooy aw sant wu yàgg la niki santi ajam yi,(ajam mooy ku dul araab),li fi ne daal mooy ñaari wax yi bu ci ne dëgër na te am na màndargaam dëgg. Waaye Buso-boso yi ñoom seen cosaan Fuuta la ca fa niy wax Golare, barab yii yepp it yu jegee lanu,barab yii it,ak wax yi ci am,am nanu màndargay dëgg,yuy tegtale teddgay ñaari askan yi.
Bi sëriñ bi tollee ci war a jàngi,wayjuram dal di koy jébbal nijaayam Muhammad doomi Muhammad BUSO mbokkum ndayam ju tedd ju yiw ja.
Mu tàmbli koo jàngal ba mu màgu’s lëf ,tàmblee yewwu, mu jebbal ko moom itam nijaayam,sëriñ Tafsiir Mbakke Ndumbe doomi Muhammadu Soxna BUSO doomi Muhammadul Kabiir mi nu tuddoon,moom mooy mbokkum maami sëriñ bi ju jigeen,ndayi wayjuram wu jigeen,soxna Asta Waalo. Nu daan nekk foofa fa moom ca Mbakke bu noor baa, bu nawet baa lu ci ëpp danu daa dem jolof, ba bi Tafsiir mii làqoo te booba sëriñ baa ngi jeggee mokkal.
Kenn ci ñunu woolu ñi nettali na ma ne, sëriñ bi nettali na ko ne àlliwaam a ngi tulloon ci latajjidanna bi jànglekatam boobu di làqu,mu dal di dellu ca wayjur wa, dal di farlu ci njàng mi ba mokkal alxuraan , def tajwiid ak tas-hiih,ca ña ko daa defale ca jamono jooja, loolu lepp ci wetu baayam,daa wul tàggalikook moom lu dul lu neew,ndaxte magam Muhammad Jaara dafa nekkoon ca kenn ca tas-hiihkat ya ca yeneen dëkk ya.Bu ko defee leeg-leeg amaa na mu jaar fa nekk faak moom weer,walla ñaar,doog a dellu,booba ña nga Saalum,ca jamonoy jihaadkat boobu di Mabba Jaxu,ndax kat booba ñoñam Mabba boole woon na leen ca ñam pangoon jëme Saalum,nga xam ne Bawal ak Jolof daanaka bawu fa kenn.

Bi mu faatoo nag moom Mabba nit ñi dal di dellu seeni dëkk , waajuram wi moom itam dellusi ci ñi doon dellusi ànd ak Latjoor. Ci noonu nijaayam akug njabootam des foofa,sëriñ bi it bokk ci,ngir jàng xam-xam,noonu mu tàmbli di jàng ci baay tëxam,Samba Tukkloor KA doomi bàjjani baayam,bi mu jàngee ci moom dali xam-xam,tàmblee ñawu’s lëf la dellu ca baayam,te booba ma nga Paataar,benn dëkk bu ndaw bu nekk ca wetu njéndul Amadi Yala,dëkkuwaayub Latjoor ca joojale jamono.Ndax moom sëñ Mammoor daa defoon ku Latjoor fonkoon lool,daa ko laaj tey diisook moom,waaye moom sëñ Mammoor bëggutoon a dëkk ak moom,ndaxte du woon ku xemmeem seen alal ji,du caageenug seen teddngay nguur gi,li ko loruloo woon ci mu dëppoo ak ñoom ak a mudaaranteek ñoom mooy njaboot gi mu yoroon,bu ko defee Latjoor daa ko dëkkal ci wetam,waaye sëñ bi daawul nangoo dëkk ak moom,moom kay day dëkk ca wetu péey ba mu ne rekk,ndax da daa jàng ak a jàngale,te jàng ak a jàngale neexoowut aki buur,li fi ne daal ca wetam la dëkke woon,nga xam ne su ko soxlaa ñëw ci lu dulub coona.

Ci noonu sëñ bi nekk ak waajuram,di jàng ci moom te di farlu ci mokkal gi,ak xereñe gi ak dégg-dégglu gi,ba faf raw ci fann yi. Ci biib diir it daa na ci def leeg-leeg mu seeti sëñ Xaali Majaxate Kala,moom mi dëkke woon fa péey baak Lajoor,di woon ku raw ci fanni xam-xam yi rawati na làkkuw araab,di ku siiw ci man a woy,bu ko defee muy xamlu ci moom araab,leeg-leeg it mu daa ko indili woy,yu mu def ngir mu toppal ko “lihraab” ba ak araabe ga,ak “harool” ba,leeg-leeg mu genneel ko ci’b yàq,ba mujj sëñ bi far ko raw, mu mujj saa su ko wonatee lenn ci woyam yooyu,mu ni ko indil ma ko ma mokkal ko,mu mujj toppalatu ko waaye day mokkal lim koy indil,nii la nekke woon ak Xaali.

Amoon na fa it beneen boroom xam-xam ci waa-gànnaar yi,dëkke woon Njaañ, tuddoon Muammad mom Muhammadul Kariim,bokkoon ci giirug Daymaan,ci doomi Seyidil Faadal yi, ñu gënon koo xam nag ci turu Muhammadul Yadaali,waaye bokkul ak ki def teere bi nu naan Zahabul Ibriiz ci tafsiir,ndax kooku am Yadaalim Daymaan mu yàgg la . Sëñ bi bariwaa na lu mu ko daa dikkal,di jàng ci moom xam-xamu Bayaan(xam-xamu wax ju rafet),yaakaar naa ne nee na it – ci lenn li mu nu daa nettali yàlla a xam - ak bu Mantiq (xam-xamu xellu).

Bi wayjur wi xamee ci moom raw geek cawarte geek laabiir gi,mu dal di koy jox mbirum njàngale mi. Bari na lu mu ko daa jàngal ab bind ci kanamam ci teereb boppam ba walla ci teere bu mu dalagul, ngir mu jàngal ko boroom bind boobee walla teere ba, bu ñewee,ngir wóolu gu mu wóolu xam-xamam akug ñawam, sëñ bi it daan ko def,ba li ëpp ci dongay sëñ Mammoor yi mujj féeteseek moo,doylu ci moom,waajur wi ba leen ak moom te bég ci.

Waaye yàggul dara rekk Latjoor tuxoo Kër Amadu Yala,dem Sukeer péeyam ba ca Kajoor,yobbaale sëñ Mammoor mu sanci ca wetam,tudde ko Mbakke Kajoor,sax fa ñaari at dal di wuyyuji boroomam,nee nanu, looloo ngi am ci Muharram,atum 1300g, dëgg naa ci sëñ bi mu ne bi waajur wi tollee ci sukkuraat ,took na fa boppam wàcce fa ab kaamil bisub altine,guddig talaata mu làqqu,nu denci ko Deqale ,di ko siaare,man dey Alhamdu lillaah dem naa fa ba siyaare ko. Bi niy yobbu wayjur wi Deqale muy dëkk bu ndaw ci dëkki Kokki yi,ci wallug Mbaakol,sëñ bi àndon na ca gunge ba,di liiru,bariwaa na bu ko ab gawar bëggee joxuw fasam,mu ne dox a ma gënal,bi mbooloom dëkk bepp dajee di mbooloo mu kenn masta gis,nu jublu ci jullee néew bi,jiital sëñ Tayba Muhammadu Ndumbe Maar SILLA mi nu tuddoon ci buntub seedey ñu mag ñi ñeel kii nuy wax ci moom. Bi nu noppee ci julli gi,ak denci gi,sëñ Tayba digale na nu daje te dal,te xerawlu,ci noonu mu jug, xutba,waar nit ñi,wax wax ju rafet bi miy jaale sëñ bi nit ñi,bi mu noppee ne ana sëñ Bamba,noonu la nu ko daa wooye ñoom,ca jooja jamono,mu wuyyu jug,ma nga woon ca catul mbooloo ma,sëñ Tayba ne ko jegesil ,mu xaw a jege bay degganteek moom,di gisanteek moom,di ko man a toontu ci lu dul muy yekkati kàddoom,dal di yam foofa ngir bañ a jéggi nit ñi,xutbakat bi neeti ko jegesil,mu ne ko maa ngi lay dégg,Sëñ Tayba dal di koy jaale njaal mu rafet,ne man nag dama doon sàkku nu ànd ci mbooloo mu màgg mu sa moroomi waajur wii,ngir nu seeti Latjoor,jaale ko sa waajur wi,jaale gu ko man a dëfal,ngir kat moom ab xaritam la woon,dib soppeem,te dib sëriñam,daa diisook moom,bu ko defee nu waxtaan ak moom ci yaw,sampu la fa moom,ba mu man laa teg fam tegoon sa Baay,bu ko defee doo gis ci moom lu dul aw yiw ak teraanga,lii daal mooy sama xalaat,yaw nag luy sa xalaat,sëñ bi ne ko,li aju ci jaale geek dëfal gi maa ngi la ciy sant,te di la ci ñaanalub yool,waaye mbirum seeti ay buuri àdduna moom duma ko def,ndax xemmeemu ma seen àddina ji,te soxlawu ma seen teddnga,teddnga ci yàlla laa koy sàkkoo buurub buur yi,mbooloo ma tiit,tas.

Ña cay ñu baax wax ji da leen a yeem rusloo leen,ndax dëggu gi mu dëggu, tey toroxal way bëgg yi àdduna,juge ci seen doom ju diw waxambaane,tegi tànkam ci seeni wagg te manu ñu ci dara. Bu dee mbooloo mi moom li leen yeem mooy,bañ gi mu bañ teraanga ju teew jii,ak xéewal gu jàppandi gii,nu ne kii daalub dof la,ci loolu sëñ bi def na ñaari dagiiti woy yu rafet te yeeme,bu njëkk bi mooy waxam jii:
nee nanub dof laa,ngir wëlbati gi ma wëlbati samab gis wëliif leen ba fam yam ,teewluwu ma ko te woneesu ma ab yaxam jamono ja may liggéey,waaye beneen bi moom mooy wax jii:
nee nanu ma jengal jëm ci bunti buur yi,kon dey da nga ami may yu lay jariñ jamono ju ne.
Ma ne leen yàlla doy na ma,doyloo naa ko,soxlawu ma lu dul xam-xam ak diine.

Yaakaaru ma te ragalu ma ku dul sama boroom,ndax yàllaay ki may doyluloo te di ma musal.
Nu may joyale samay mbir jëme ko ci ñoñ lottu nanu ci seen mbiri bopp,ni miskiin yiy lotte?.
 
Walla nan la ma bëgg poñatum àdduna bii di jañe,jëm ci dëkkaale ak ñoñ seeni kër mooy dërub saytaane.
Su ma dee naqarlu mbaa may bég boroom aras laay woo. Mooy aji dimbali, ji dara dul të,te mooy kiy amal li ko soob.
Bu bëggee gaawalum mbir loola gaaw,bu ko nammee yeexal mu yeex ba cib diir.

Yaw mi may yedd bul sonal sa bopp , ndax kat man awma lenn lu ma naqari ci ñàkk àddina.
Bu dee sama ayib mooy dëddu gi ma def ci seen poñat mi,kon dey ayib jooju, ju gànjaru la, ju ma dul gecceel.

Waajuram wu jigeen wu tedd waa nga làqqoo Poroxaan ca Saalum nu denc ko fa,jamono ja fa sëñ Mammoor nekkee.

Moom sëñ bi,bi waajur wiy dund, nanguwtoon a taxaw mbaa muy taxawal dara,moom daal ci moom rekk la toppoon ,mel ne néew bu nuy sang fu nu ko jëmewul du fa jëm, bi mu làqqoo nag,mu des ca ligeeyam ba mu ko bàyyee woon at ak lu topp, ña fa nekkoon it jàng rekk a leen fa ba woon, du leneen,moom itam ab jàngalekat rekk la woon,waaye loolu teewul woon mu doonoon ku yitewoon a xam gaa ñu baax ñi,ak seeni xam-xam,ak berook a wër,niki ñu baax ñi,mu leen daa junju ciy waxam,ak a feeñali maanaa,ak a yëgg,ba bi ko himma ju kawe ji (himma ci lun man a firi mooy yite) dikalee ,muur ko,mu jug yëggus lëf neeti tekk,dal di woote cig nooy jëme ci mbiram moomu,bi ko mbir mi gënee lëjal nag gën a fees fi moom,gën a rëy,mu dal di biral woote gi.

Dajale mbooloo mi,taxaw fa ñoom xutba leen,sukkandiku ci dokkub dogu,ne leen yeen mbooloo mi ku àndoon ak man, ngir jàng rekk,na laxas jëm ca boppam aki mbokkam,mbaa fa ko soob,man loolu rekk taxatumaa jug,ku bëgg li nu bëgg nag,na toog,dal di leen fay ba dugg ca biir.
Waxam jii nag dal di leen ba cig jaaxle, ñenn ñi dem, ña ca des,des fa,am ñuy jeem a tëyye seeni xarit ngir ñu des,ak ñuy xiirtal seen waay ci ñu dem,sëñ bi moom ne tekk rekk,jeemul a tëyye kenn ku bëgg a dem,ba mujj li ëpp ci mbooloo mi dem ba ko fa,la ca gën a néew des fa. Bi loolu lepp data am,fekkoon sëriñ bi mu sóobu ci ngiirum taalif ci xam-xam yu nu tuxal ,yu sariiya yi, mu woy Ummul Baraahiin,bu Imaam Sanoosi,wayjur wi nangu ko,beg ci ,te mujj di ko jàngale ,bàyyi wesar wa doonoon cosaan la. Degg naa ci sëñ bi mu ne woy woowu de waajuram jàngal na ko ñaari doomam yii di sheex Coro,miy Siidi Muhammad Alxalifa,ak sëñ Aafe,mi tuddoon Ahmadul Muxtaar.

Mu woyati teereb Imaam Xazaalii bi tuddoon Bidaayatul Hidaaya,dal di koy tudde Mulayyinuz Zudoor ,di ci maanaa (aji nooyal ji dënn yi ),ginaaw bi mu gàttal ko,tudde ko Munawwiruz Zudoor,di ( aji leeral ji dënn yi),ci atum 1294g,teg ci Jëzbatuz Zixaar,di (bijjig gone yi) ak Jawharun Nafiis muy ( wurus wu gànjaru wi) nga xam ne da cee woy wesaruw Imaamul Axdariyyu,ak yu dul yooyu. Bi ko donga yi nangulee nag lii mu leen doon woo,daa bàyyi njàngale mi,jëm ca di leen tarbiya,ak a tarqiya (tarbiya mooy yar ni ko sariiya bëgge,tarqiya di yékkatee jëme ca yàlla).
Man nag nee naa lii de du ñàkk muy ndigalug yonant bi (j.y.m),ndax kenn ci sunu sëriñ yi nettali na ma,te moom ku wóor la di ndëërlaay,ne sëñ bi de wax na ko ne yonant bi (j.y.m) moo wax ak moom ci gimiñam,ne ko yaral sa àndandoo yi ci Himma te bu leen yar ci njàng,loolu sëñ bi gën na koo leeral ci qasida gii:

Bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi ji,yal na ko yàlla dolliy xéewal ak mucc,moom miy leeral suufam si ciy walliyu ba yawmal xiyaam,te ku ci ne méngoo nga sunnaam si,di ko ñogal wëlif bidaa,bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi jooju,bégal gu mu bégal jëwrinam jii ci ne ko(fazdah) mooy wooteel ca kaw. Yonant bi (j.y.m) digal na ko ne ko mu jàngal Muriid yi,ak ku nangu mu laabiire la ci waa jamono,te mooy ki ko àggale ca borooman cig taxliya ( mooy setal nit ki féexal ko ciy ayib ) bégalati ko ci tahliya ( muy ràng nit ki ay takaay,walla sol koy ngënéel).Li mu jublu ci Fazdah ji nag (mooy biralal ca kaw) ,mooy ji ci alxuraan: fasdah bi maa tuumaru wahrid hanil musrikiin mooy biralal lin la digal te dëddu way bokkaale ñi.

Yàlla daa digaloon yonantam bi (j.y.m) mu biral wooteem ga,ginaaw bi mu ko daa yalu,maanaam dëgg-dëggi loolu, mooy sëriñ bi,bi donn gi mu donn yonant bi matee,ci matalug yàlla (t.s) ,te mu dolli ko ay xam-xam aki hikma,aki leer,aki mbóot,te may ko kàttanug man a yanu wilaaya gu mag gi- bi loolu amee nag mu digal ko mu woote ca kaw,woo mbindeef yi ñu weeru ci moom,di jële ci moom tey def ay ndigalam,di bàyyi ay tereem,ci loolu la waxe: yàlla mi nga xam ne lu ko soob mu def,moo ma jox xam-xam yi,ak seen barke,wattu naa lu xajul ciy teere,kon boo may ligeeyal bul tàyyi.Yàlla miy joxe,jox na ma ci darajay yonant bi,barkeb alxuraan,ak xam-xam yi,jël seen barke def ko ci samam njàngale.yàlla jël na mbooti laa illaaha illal laah def ko ci samy taalif,yàlla jox na ma te dootu ko nangu,te man kaaraange laa te dib weeruwaay ci ndimbalam.loolu nag ngënéelul yàllaa,ku ko soop la koy jox. Te nee na ma : neel weeru leen ci man.Ci maanaa sama boroom digal na ma,ma leeral nit ñi ne:man ab weeruwaay laa tey kaaraange,ku bëgguw yiw àddunaak allaaxira,na weeru ci man. Mu dellu waxaat ne: Murid bu yoqqatul ci man de texe na,ci làqq ngën ji ay may. Murid bu yàlla wommat jëm ci mu aju ci man, texe na te da na ceru ciy may.

Murid bu wéeru ci man de yàlla miy sama dëkkandoo bu kawe bi,def na muy ku texe ci lu kawe njortam.
Bepp murid bu aju ci man,day texe,te ku niy soril la aw ay. Kepp ku aju ci man dey am nga ag mucc ci nëx-nëxi àddina ak allaaxira.
Ginaaw bi mu leeralaat ne way gëmi junne yepp ci jamonoom ,aju nanu ci moom,mu ne : Junney sama jomono jii dey, ña ca gëm ñepp aju nanu ci man,waxuma ña gëmul.

Mu wattuloo nag ñi aju ci moom, ñuy xàccati ginaaw bu nu jébbaloo ne: toroxte ñeel na ki ma dëddu ,won ma ginaaw,muñ ma,ginaaw bi mu duggee dib murid.

Dal di leeral lu dig murid,ak lub murid di bëgg,mu ne: Dëgg-dëggi ag murid - ci li sang si wax – mooy bàyyi aada,( muy li nga nekkoon njëkk ngay jébbalu),bu àggagul ba noppi dellu ca la mu nekkoon, mook ku murtad ay yam. Ndax kat ab murid du bëgg mukk lu dul gëramul yàlla ak fu mu man a jublu.

Mu leeralaat ni ab muriid di mel,ak ngértel ànd ak sëriñ bu àgg,mu ne : Melow ab murid,mooy bañ a bëgg dara ngir yàlla. Ku bëggul lu dul yàlla, àgg fa moom,mu jox kow yiwam.

Ku aju ci ku àgg, àgg,ku aju ci ku àggul doo àgg.
Ku yaroowul ci loxoy ab sëriñ, dana dajeeki coona.
Ndax ku amul sëriñ buy gindee,saytaaneey mujj dib sëriñam fu mu jublu.
Ab sëriñ du wuuteek ku nu rammuloo ki (muy yonant bi) kon ku jublu aji yar (sheexul murabbi) de da na jariñu.

Fu la aji yar digale,defal,kon nga àgg ca boroom ba.
Bu la aayee dara bu ko jege,te bul sàggan ci wut gëramam.
Mu leeralaat ne murid saadiq de am na ay meloom,yoy bu ko amee am wepp yiw: Meloy murid saadiq ci gàttal, ñeent la,ma tënk leen nag ciy bayit ngir ragal woru.
Dëggal ci bëgg sab sëriñ ba fàwwu,jëfey ndigalam fu mu rote rekk.
Bayyi gaaru ci lum man a doon (gaaru mooy di am xalaat ci ndigali sëñ bi), ak doonte ci sa baatin la,ci lin nettali.
Ak a tànnal sa bopp la ngay def,ngir sa rafetug njort.
Képp ku boole yile melo ci murid yi dey,da na jot ndëërlaay ya(gaa yu baax ya).

Mu biralaat ne kiiraay am na juroom benni cosaan,yu murid bi war a dagg,te malaaka yi dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk, ne: Kiiraay am na juroom benni cosaan,ku bëgg a àgg da nga leen dog, ñooy baril lekk ak naan,ak a jaxasook nit ñi.
Bari wax,bariy nelaw,sàggan ci tudd yàlla miy jàmm. Gëstul loolu ci Jawaahirul Mahaani,bi sunu Sheex Tiijaan mu nu màggal mi def.
Nettali nanu ne malaakay aji màgg ji,dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk,ngir yëram ko,loolu man nga koo gis ci taalifi boroom Hawaarifil Mahaarif.

Mu neeti murid saadiq doomi waxtoom lay doon,ne: Murid Saadiq mooy kuy wëlbatiku ànd ak waxtu wi mu nekk,te du fuglu wa ca kanamam,ndax loolu day teree yéwenal waxtu wi teew.
Gëstu leen loolu ci Jannatul Muriidi,teere bi sunu sëriñ Xaliifatur Rasiid def.
Ak lu bokkul ak loolu ,ci li mu wax ci mbirum boppam, mom muridam yi,nga xam ne ,bu nu ko toppoon,indi fi lu yeem xel yi,te da na mujj kon,gàttal gi nu bëggoon ci teere bii,du amati,ndax moom teere bii as kook la ci geejug xamale ko.

Nu indil leen fii nag as tuut,su nu tas ci ay wuññi ñeel lenn ci sekkarey xaybu yi (xaybu mooy lu faddu,muy mbirum biir niki liy xew te xewagul),mu bégal ci ñi aju ci moom, ngir dolli leen ag xeemeem,ak sawarloo leen,mu wax ne : ñi aju ci man bu nu ko defuloon dem sawara,doonte as ndiir lay doon it,njëkk nuy tàbbi ajjana,ji nu dig ñu ragal ñi yàlla.
Li waral sama tukki bu sori bi,yàlla mu barkeel mi te kawe,daa bëggoon ca asal,may kiy ramu samay donga,dox na sama diganteek nasaraan yi,tàbbal ci seeni xol ag ragal ma,nu def la nu def nag ngir ma bañ a nekk dib nasaraan, ndax bu ma ko doonoon tabbi sawara ,walhiyaazu billaahi. Waaye yàllaa ma aar ci sawara,ak lépp lu mu gëramul,ci darajay yonant bi (j.y.m). Mu bind ay laabiire ñeel murid yépp,ne : Mi ngi juge ci man jëm ci mbooleem murid, yu góor yeek yu jigéen yi,ab nuyyoo bu teey,bu leen di musal mboole seen,te di leen tabbal ci jàmm ak aafiya,ci addinaak alaaxira,ci barkeb yonanat bi (j.y.m),ginaaw bi, may digal képp ku aju ci man,ngir yàlla mu kawe mi te tedd,mu xamlu pas-pas yi ak tawhiid,ak àttey laab,ak julleek woor,ak lu dul loolu ci lepp lu war mukallaf,man nag warlul naa leen taalifal leen mbooleem lu leen koy xamal, ngir jëmmi yàlla (t.s),wasalaam.

Mu bind lenn ci ay murid ab tontu bu neex yal na nu ci yàlla boole ñun ñepp,mu ne ci: assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa,wa barakaatuhuu,ma lay xamal ni sa bataaxel ba agsi na,yaw murid bu dëggu bi,waaye na la wóor ne doo gis lenn loo ragal,booy faatu ak ci bàmmeel,te ñaari malaaka yiy laaje,xam nanu sa sëriñ,te da nanu doylu ci xam gi ba dunu la laaj dara.

Lii nag xamle la gum teg ci yoonu laaj ak tontu,laaj bi moo di lan la sëñ bi woo ay taalibeem jëme?lan mooy tontu li? Moo di sellal,moom mi nga xam ni mooy ruuhug jëf tey ngértel xam-xamub way xam ñi yàlla,tey waralug àgg ca yàlla, àgg ci yàlla nag ñi ngi ci jublu jaam bi nekk di ku weetal yàlla,ciy yëggoom ,aki dalam,aki pas-pasam aki waxam,ci lepp,li feeñ ak li nëbbu,lii nag manta ame ci njàngale rekk,ndax kuy jàngale ab tegtalkat rekk la,li ci des,mi ngi ci aji jàng ji,man naa am mu jëfe man naa am deet,du ligeeyub jàngalekat,muy sonnu ci waa ji jëfe loolule,loolu sheexu tarbiya la war.

Bokk na ci ligeyam,moom sëriñub yar,jàng ak jàngale,ak ligeeyloo,aki tudd yàlla,ak gindee ginaaw bi mu leen xiirtalee cig cofeel gu dëggu,te du tàggook ñoom li feek wonu leen seen ayibi bopp, ligeeyloo leen ci nu jeem a laab ci yooyu ayib,ngir man a àgg ak ñoom fa yàlla inshallaah. Bu loolu jàllee,mbirum tarbiya day mbàir mu gudd,manunu cee wax fii. Mu dem ak ñoom cib yar leen ci himma, ñu nangul ko ko,mu dox ak ñoom ci ngërum tàggat,dajle leen,di leen ligeeyloo lu bari,yanu leen ci fàttaliku yàlla lu bari,ak a jàngi xasida,ak taqqoo lab,ak a beru,rawati na sori jigeen ñi,ci noonu ñu kawe ñu dul ñoom,ndax donoo joxe woon seen bop ak seen alal ci yoonu sàkku gëramul yàlla, yalla jënd na ci jullit ñi,seenii bakan ak seen alal,faye leen ko àjjana, sëñ bi wëy ci yoon wu jub wii mook saabaam yi, dale ko ci njëlbeenug atum junneek ñatti teemeer ak benn,ba bi mu sancee Mbakke Bawal,ci at moomu juge Mbakke Kajoor,sax fa lu tollook ñaari at ,nit ñi di ko dikkal juge fu ne, ñii di jebblusi, ñii di joxesi àddiya, ñiiy sàkku ndimbal. Mu mujj yoonu këram gi mel ne yoonu ab ja, ci ñeenti at yii nag mu siiw ci,siiw gu kawe, ñu jege ñeek ñu sori ñi, ñeppuy yeemu ci moom,te booba amagutoon sax fanweeri at. Ci diir bii sëñ bi wër na ci réewum wolof mi,dale Saalum ba Waalo Barak,siyaare fa mag ña, ña cay dund ak ña dundul,jaar ca sëriñ sa ,jële ca ñoomi wird,bokk na ci ñim siyaare, ñoñ sheex Siidiya,siyaare na bàmmeelam ca Tindawja,siyaare sheex Baaba mom Abiihi ca Maymooni,tagg leen,jële ca ñoom,woy càllaleg xaadir gi,tàmblee ko ca sheex Baaba ba fam yam,looloo taxoon kenn ci sheexi naar yu mag yi laajoon ko kuy sa sëriñ?,mu ne Rasuulul laahi (j.y.m),mu ne ko kon lu tax nga ne fi di tudd waa kër sheex Siidiya,ak a wooyey sëriñ ak a tag?,Mu ne booba da maa melon ne ku gumba,di làmbatu yoon wi,di ko sàkkoo xam ci ku xam ak ku xamul,bi ma dajee boroom yoonwi ci ndimbalul yàlla nag muy yonant bi (j.y.m),mu xëcc ma ci boppam,laa wacci ker-keraan yi,waaye di jokkook ñoom ngir yàlla ak a soppanteek a jriñante ngir moom.

Te wax na dëgg,ndax mbiram ak ñoñ sheex Siidiya loolu lay tegtale,mujj nanu mel niy doomam mu mel ni seen baay,di leen jariñ ci alalam lu leenub buur jariñul,ab sëriñ it jariñu ko ab taalibeem.
Sheex Baaba tag ko ciy xasaayid,aki dagiid,yu tollok ay teemeeri bayit,bokk nan ci yile:(( Shex Ahmadu xeewal la gu yàlla jox mbindeefam yi)) ak waxam ja: (( sëñ bi daal xeewal la gu yàlla xeewalee,di kiimaan ci kiimaan yi)),ak yu bokkul ak yooyu,bu waxutoon yu dul yii it , ñaari bayit yii,rekk doyoon nanu seede ci màggug sëñ bii,ak wilaayaam. Ndax kat sheex Baaba ak màggam gi du fo mbaa muy yaxantu ci woy ni suharaawu yi,moom dey lum wax ci ndigal la ko teg,ak jaamu yàlla,yal na ko yàlla fay ci ñaari bayitam yooyu. Bokk na ci ñim siyaare ci sheexi naar yi,Ustaas Baaba mom Hamdi ma jublu ci Hamdim ñaareel mi,dikk na fa yendu fa fanaan fa,nee nan ci menn mbaar. Sama xarit ba niy dàkkantale kaadi Sheex Abdul Xaadir,doomi Amiirul Kumlayli , nettali na ma te booba taalibeb Ustaas Baaba la,ne Ustaas mii moo jox sëñ bi sekkare bi,waaye nag leeralu ma ban sekkare la,man naa am muy wirduw Saasalii,ndax sëñ bi bind na ne moom wirduw saasali ming ko jële ci wenn wasiila,njëkk muy dajeek wasila wu mag wi,di yonant bi (j.y.m) ,te leeralunu kooka kan la. Li waral Kaad mii nettali ma ko,mooy maa ko laajoon bi mu jëlaatee ci sëñ bi wirduw Sasalii,ndax xam nga ci ku ko sëñ bi jële woon,mu ne deedeet,waaye nettali lim waxoon ci diggante sëñ beek Ustaas Baaba,nu jorte ci ne ci Ustaas Baab moomu la ko jële ndax moom ab xaadir la woon. Kaad nettali na ma ne bi sëñ bi agsee ci bi miy siyaaresi Ustaas ci bëcëgug bis bu sell,Ustaas defaral ko am soow mu neex ci ndox mu sedd,ak suukar,looloo ngi amoon,ci jamono ji sëñ biy nattu boppam ci di tegoo ay coona,mu ne ko naanal mu ne ko man baax na du ma naan lii, mu ne ko,ndax daa baaxul ci wàllug wér,waala dang koo bàyyi ngir yàlla di jiyaar ak sa bakan,sëñ bi ne ko waaw loolu la,mu ne ko kon naanal,bàyyiwu ko ba mu far naan,ginaaw bi la dongay Ustaas yi laaj lu waral mu sonnu ci mu naan nii,mu ne leen ndax moom kat sonal boppam rekk la bëgg,ak mettital ko,mujj loolu di aadaam ngir yàlla,jum munta baati,ndare cib coona,ma jëflante ceek moom waaye yàlla defal na ko barke,ndax mujj na dëgar ci këng. Ginaaw bi lii wéyee lu yàgg,Ahmadu doomi Ustaaas seetsi na Sëñ bi Njaareem,mu bég ci lool,di ko ganale ngan gu mu sonn,indil ko ñam yeek naan yi,bi nu àggee ci ataaya, Ahmad xam ne mbir dana am ,ndax moom du naan ataya,bi ko sëñ bi tàllalee ataaya ji,mu ne ko du ma naan ataaya,mu ne yàllaa tax nga ba ko ngir jiyaar ak sa bakan walla ag weradi,mu ni ko yàlla,mu ree,ne ko naanal ma fayoo ca la ma sa baay defoon, ñaanal ko ci barke. Bi sëñ bi nekkee ci wëram boobu nit ñaang ko daa dikkale gepp wàll ngir xam-xam bu bari beek njariñ li,ak cofeel gi nu amoon ci moom ak diinewu gu dëggu gi,rawati na alal ju bari jim daa joxe rekk ,nga xam ne daawul tëyye ab dërëm,lu ñëw mu joxe,di jox mag ak ndaw goor ak jigeen,ngor akub jam,ku am ak ku amul,ku baax ak bon,loxo bu tàllaliku jëm ci moom mu feesal ko te soxlaalul nit ñi, doyloo kàppitaalam bi dul lu dul jublu ci yàlla ak yiteem jepp. Mu dem Gànnaar jaar ca sëriñ ya,siyaare ñay dund ak barabi way faatu ya,jariñ leen ci alalam,ju bari ja,nu sopp ko nu kawe ni ko ñu ñuul ñi soppe,defal koy xasiday tagg,siyaaresi ko ci reewam ginaaw bi. Bi mbokk yi gisee ci moom kaweg xel,gu diine,gu mbaax gii mu yor ak jublu gu àddunaak nit ñi jublu,nu tambli di ko iñaane,di ko lor,mu daan julleendoo ak ñoon,lor yi ëpp,mu mujj beru leen akum mbooloom ak jàkkaam, yàlla gën a fésal mbiram, ñu gënatee mer,nga boole ci terewu gi mu defoon ci mbirum buur yi,daawul nangoo jaxasook ñoom,ba da daa sàkku sax ci sëñ Mammoor ci ay bataaxel yum ko daa bind, - da daan kersawoo jàkkaarlook moom di ko ci wax dara - mu bàyyi ag jëflanteem ak buur yi,naan ko seen teddngay fii ji toroxte la ëlëg,sëñ Mammoor daan ko ko nangul,te di ko ci jëggalu,waaye njabootam gi taxoon ba manu leen a bàyyi.

Ma nettali leen as lëf ci jaloore,nee nanu,bi kenn ci jaraafi Latjoor yu mag yi –mu nekkoon ku am solo fa Latjoor - jébblusee ci sëñ bi,mu bokkoon ci jàmbaar yi amooni alal,mu ndàmmoom (gañewoon) lu bari ci màggum xareb Samba Saajo bi ( màgg mooy li niy jële ci koo xeexal ba not ko) .Samba Saajo ab dëkk la bu nekk ca penkub Njàmbur,diggam ak Jolof,la xare boobu ame woon,ci diggante Amad Sheexu BA mu Fuuta, ak Latjoor,Tubaab yi japle woon ko moom Latjoor,bam gañe ko ray ko,xarekati Latjoor yi gañee ci woon màgg mu rëy,ci alal aki jaam,te ña ca ëpp diggante Jolof ak Fuuta lan bawoo,ak Kajoor,tey jullit lanu, buur bi laaj ndax man na leen a defi jaami,kenn ci boroom xam-xam yu mag yi,ne ko waa-waaw,ndax Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonant,kon alalam ak dereetam dagan na,nu dal di wéyal loolu,te kat ag wooteem yonant mbooloom boroom xam-xam yu mag yi saxalun ko.

Li waral xare bi,lu gudd la manunu koo netaali fii. Bi jaraaf jooju tuubee ci sëñ bi,mu digal ko mu wacci mbooleem jaam ak alal ji mu ame woon ci xeex boobu, jaraaf ji deggal ko,def ko ànd ceek kontaante,Latjoor aki gaayam jàppe loolu nag ag weddi ñeel àtte bi leen kenn ci boroom xam-xam yi defaloon,ne leen jaam yi dagan nanu. Nu mere woon ko,nee nanu ma jaraaf ya woo woon nanu jaraaf jooja fa kanamu Latjoor,ne ko : lu tax nga bokk ak nun ndab,regg rekk wëlbatiku,doyatu la nga ciy xëpp suuf? Mu ne leen waaw,weñ a tàbbi ci sama bakan,lëjal ma moo waral lii ngeen gis ci man,waaye bëgg a nëxal seenum mbir taxut. Mu jublu woon ci weññ wi,lislaam ji ko duggoon,cig mbetteel,yaw nag xam nga lëjal gi lislaam di def kum dugg, du ko bàyyi ndare bu daa tuub. Ñu xam ne lim wax lu dëggu ci moom la, ñu jëggal ko noppi cim mbiram. Waaye sëñ bi moom, Latjoor lijëntilulu ci anam gu nooy,te teey,nun ko ko indile,mu bind koy leetari leetar,yonni fay ndawi ndaw,teewul sëñ bi bañ,nee nan ma wax na bis kenn ci ndawi buur bi,ne ko : neel ki la yonni rus naa malaakay yàlla yi di ma gis ma jëm ci buur bu dul yàlla. Degge naa ci sheex Aadama SÀLL – moom kenn la woon ci ñi njëkkoon a jébblu ci sëñ bi cosaanoo woon Jolof – mu ne leetar bi sëñ bi mujj a bind Latjoor moo ko doon yobb, mi ngi ci naan: Muhammad Ibnu Maslama nee na boroom xam-xam ci buntu buur,mi ngi mel ni weñ ci kawi jonkan, Latjoor jox Xaali Majaxate Kala bataaxel bi – moom moo nekkoon mufti bu mag bi - Xaali yër ko tiit, ne :(( Innaa lillaahi wa inna ilayhi raajihuun)) buur bi ne ko lan la ? mu ne ko,kii waxul ak yaw man lay waxal,mu ne lu man a xew waxal rekk,mu jàngal ko ko,Latjoor ne ko: ci man de la gën a dal,ndax yaw lu man a xew ,yaay weñ wi man nag,ay dem-àll laa. Waaye nag yaw miy boroom xam-xam loo wax ci moom? Xaali ne ko man daal li ma gisoon,mooy nu ba ko ak mbiram ,ndax kat notanteek moom ag woru la,boo ko notee bokk ci ñi gën a kawe,bu la notee, nga di ci ñi gën a suufe,te maneesu koo not. Buur bi ne ko wax nga dëgg,ndax baykat kat yàgg naa gis jànjnji ci toolam - te manu koo bay manu koo saxal –mu ba ko fa,Xaali ne ko waa-waaw,mu ne nan ko jàppe jànjnji boobu. Ci noonu leetar ya dog,wax ja jeex,alhamdu lillaah.
Beneen nettalee ngii bu gënatee yeeme,waaye soriwul bu njëkk bi,mooy,bi leetar yeek coow li jeexee ci bataaxel bu saf boobu,yàlla dogal na Latjoor ànd ak Xaali ci lenn ci tukkeem yooyu mu daa def,ba wàcci benn dëkk wetu fi sëñ bi dëkk,bi sëñ bi yëgee ne mook Xaalee ànd,mu ne na nuyji Xaali,ngir ñaari mbir,menn mi mooy Xaalee ko daa jàngal,te ku la jàngaluw araf sa kilifa la, ñaareel bi,xaritub baayam la woon,mu war ci moom mu jox ko àqam te jokk ko,ndax danu ne : (( joxe àqi waajur gi gën a mat,mooy waa ji dox kóllare ak jokk ko ci xariti baayam yi )). Bi mu agsee fi ñoom, fekk leen nu toog ci lal,sëñ bi nuyyu leen,nuyoob màggal,toog ci suuf,toogul ca laltu ga fa ne woon,bi mu toogee tuuti ne Xaali,da ma la fee deggoon rekk ma ne naa fi jaar siyaare la,ci noonu Latjoor xam ne daa bëgg a leeral ci ne dikk gi Latjoor taxul,jubook moom it taxut. Latjoor gestu Xaali ne ko,nun kat kii war nanoo wax ak moom ca sun mbir man ko woo woon ba sonn,mu bañ,Xaali ne ko aca, ne sëñ bi: man dey maa ne Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonant,te di ci xeexe it, kon ray ko dagan na,lekk it alal jiñ nangoo ci moom niki màgg ak njaf ñamu àndaloon (njaf mooy jàpp jaam),loolu lepp dagan na,bi mu noppee mbooloo mépp noppi ab diir,sëñ bi ne Xaali ndax da ngaa wax ngir ma tontu la?,Xaali ne ko waa-waa,bu may wax kay nga tontu maa tax,sëñ bi neeti ko : kon am naa ndigal ci tontu ? mu ne waa-waaw,sëñ bi ne kan moo la man a seereel ne woote na ag yonant? Xaali ne ko waa Kajoor,mu ne ko ñooñu ay noonam lanu,te diy xuloowaaleem,di xareek moom,nan lanu koy seedeele? Xaali neeti ko waaye waa Samba Saajo,fi xare bi ame woon?, sëñ bi ne ko ñooñu kay dun seede,ndax xare baa leen fa fekk,sottiku ci seen kaw,te yëgunu woon,nan laniy xame ki nu tuumaal ak li nu ko tuumaale?, Xaaleek mbooloo mi ne tekkus lëf,bam yàgg mu ne yaw gone gi,won nanu la yàlla,nga jiitu nu ca,konug ndokkeel ñeel na la,dal di nooy,te jubook moom. Pënd ba wuriku,sëñ ba tàggu leen dem,ci noonu yoon yepp dagg ci moom lu dul wi jëm ci yàlla,ndax kat moo ñë ci ñu baax ñeek kàccor yi,jàng ca ñoom: wa ufawwidu amrii ilal laah innal laaha bashiirun bil hibaad,wallaahu yahlamul mufsida minal muslihi muy joyal naa samay mbir ñeel yàlla,moom miy gis jaamam yi,yàlla xàmmee na kiy defar ak kiy yàq.
Li mooy dooley sëñ bi,te nii la dogoo woon,donga yi raw ko, cig dogu,foo leen fekk ña ngay xeex ak nit ña,nga gis daanukatu jell yi fii,leeg-leeg nga gis ku ci yeeg ba ci kaw njobbaxtalu garab,ne dërr fi suuf,jiital bop bi,jug faxasu dem,te dara du ko jot,ak ñuy tàbbi ci sawara genn,te dunu lakk,di yekkati xasiday sëñ bi,ci penciy nit ñi,ak seen daara yi, ñuy xeex ak ñoom te du tax nu ba, ñu leen di door ak a jeng,ak a nangu seen alal,ak a genne seeni kër,loolu lepp,ngir teqale leen ,te tas leen. Mu mel ne jëf jooju da leen na dolli ag xeemeem akug sóobu, mu mel ni loolu mbóotum yàllaa,mu ball juge ci baatinub seen sëriñ ba ca ñoom,sëñ bi daa leen dolli pastéef,di dëgëral seeni basiira ,di yekkati seeni yite ba ca yu saaba ya,naan leen roy leen saabay yonant bi, ñooy seeni mbokk de,te daje nannook lu gën a tar lii ngeen nekk, ndax ray nanu leen ci yoonu yàlla,tuur seeni dereet,nangu seeni alal,genne leen seeni kër,te loolu teewu leen a jublu ci li nu soxla, ba am tagg wu rafet ca yàlla, : lil fuqaraail muhaajiriin allaziina uxrijuu min diyaarihim wa amwaalihim yabtaxoona fadlan minal laahi,wa ridwaanan,wa yanzuruunal laaha wa rasuulahuu ulaayika humuz zaadiquun, mu leen di xamal ni,da noo war a roy ci way gàddaay yu ñàkk yooyu,nga xam ne ku dul yàlla ñoru leen woon, ñu genne leen seeni kër naggu seeni alal,ci yoonu sàkku yàlla ak ngërëmam,ak dimbali yàlla ak ab yonantam, ñooñooy ñu dëggu ñi.
Mu naan leen xanaa xamu leen ne ñooñooy seeni baay ci diine,kon lu leen man a dal,day dal di doon lu neew, laxadd kaana lakkum fii rasuulil laahi uswatun hasanatun liman kaana yarjool laaha wal yawmal aaxira muy :ku gëm yàlla ak allaxira,na ko wóor ne am na roytéef bu rafet,ci yonant bi. Muñ leen tey rafetal ci kiy ñaawal ci yeen, Idfah billatii hiya ahsanu,faizal lazii baynaka wa baynahuu hadaawatun,ka annahuu walliyun hamiim,wamaa yulaqaahaa illal laziina zabaruu wamaa yulaqaahaa illa zuuhazin haziim muy deel jañe jëf ju ñaaw, jëf ja gën a rafet,kon nga gis ne ki nga xam ne,ag noonoo daa am seen diggante,da na mujj mel ni sa xarit bu sellug xarit,loolu nag ku dul kuy muñ du ko am,ku dul ku di boroomub cér bu mag. Dee leen di fuglu yawma nadhuu kullu unnasin bi imaamihim muy bis ba niy woo nit ñu ne ci seen imam. Kon de bañug ku bañ du leen naqari, ñu daan def bu nu naanee ci ndoxum waaraatey sëñ bi moomu,ba màndi, di ñu sawar,di daanook a yuuxu ak a fecci,ci diir bii,sëñ bi doon baril lu muy def ay xasiday xam-xam,ak yu tag,ci la woyoon Masaalikul Jinaan,muy teere bu amul moroom ci tazawuf,yor junneek juroomi teemeer ak juroom fukk ak ñatti bayit,ak Mawaahibul Xudoos,ak yeneen,ci la wàccee it ñu bari ci donga yi,niki sheex Ibraahima FAAL,ak sheex Ibraahima SAAR,ak sheex Anta MBAKKE ak sheex Aadama GËY ak sheex Asan NJAAY ak ñu mel ni ñoom.

Bi nit ñi barilee lor yi ak sonal gi,ca Mbakke,mu tuxoo fa sanci Daaru Salaam,ci njëlbeenug atum junneek ñatti teemeer ak ñeent,waaye teewul lor yi wéy di dolliku,mu sax fa lu tollookum at,di yar nit ñi,di leen yeege,nuy gën a dolliku,raj-rajloo biy gën a yokku,wërsëg wiy gën a sottiku niki ab taw,mu juge fa,demus lëf,ca penkub bëj-gànnaaru Daaru Salaam, ci lu tollook juroom walla juroom benni miil,sanci fa Tuubaa,ci mujjug atum junneek ñatti teemeer ak juroom,walla ci njëlbeenug atum junneek ñatti teemeer ak juroom benn,tuxu fa ak ñaboot gi, sëñ Fallu nettali na ma – ñaareelu xalifa – ne magam ja sëriñ Moodu Mustafa,mi njëkk a doon xalifa,mi ngi ganee àdduna Daaru Salaam,guddig àjjuma,fukk ak benn ci muharram atum 1306 g , njëkk sëñ biy tuxu,ndax moom mi ngi tuxu, ci li nu wax, ci jumaadas saaniya. Ci guddig kasurajab,maanaam ñaar fukk ak juroom ñaar ci rajab,sëñ Fallu gane àdduna, ñu magantee juroom benni weer ak fukki fan ak juroom ñaar,yal na leen yàlla barkeel,ginaaw bi,ci la sëñ Muhammadu Lamin Baara ganee,bokk ak sëñ Moodu Mustafaa nday ak baay,ci atum 1308 g, walla 1309g . Mu des Tuubaa nag noom sëñ bi,di dem ak a delsi,ak a tuxu ci diggante kër yi,niki Daarul Minnan, Daarur Rahmaan,ak Daarul Xuddoos.

Ku dul yàlla nag xamul xew-xew yi daa am, ci digganteem ak boroomam,ak diganteem aki saabaam,ci xeeti tarbiya ak tarxiya,ak yu ni mel,ak jàngale ci taalifam yi,ak digganteem ak ñu baax ñi,ci ay mbir aki duggalanteeki xuloo,ngir seeni doom ak seen taalibe yi wëlbatiku woon jublusi ko,ak ci digganteem ak buur yeek jaraaaf yi,ciy xuloo,ngir fiir ak tiit ci seen nguur gi.
Lu man a xew,doxiin wi moom,juboon na,donga yi jub, ñu daa dollikook a yokku jamono ju ne,ku mu ci wàcce ,mu wéy di jub,ku tàbbi it tàbbi cig njub,ba bi mu tukke ca geej ga.

Sëñ baa ngi sanci Jolof - ci li ma sëñ Mbakke BUSO nettali – bi mu nekkee Tuubaa,ba nit ñi bari fa,magi donga yi denciy soxna,dëkk yi woon ci wet gi, ñu ci bari tuxusi fi woon ak seeni ñoñ, ñi sëñ bi jugoon ngir yar leen tàmblee jaxasook ñeneen ñi,nos gi sëñ bi nosoon mbir yi,am lu ci tàmblee yàqqu,mooy bëgg gi mu bëggoon a ber ñiy jàng cig wàll, ñay ligeey,ca geneen wàll, ñiy ligeey ak ñiy jàng jaxasoo gi naqqari ko,rawati na jaxasoo gi niy def ak ñeneen ñi,nga boole ci loolu aj gi mu bëggoon a defi ak siyaare ji yonant bi (j.y.m),te bëggoon koo bëgg,ba daa ko wax ñenn ci ñi ko jege woon.

Kenn ci sunu moroomi naari daymaan yi,di Muhammad doomi Hamdil Abhami nettali na ma ne:sëñ bi nee na ko ca at mooma ca Tuubaa,ndax bëgg ngaa aji? Ma ne ko waaw-wallaahi,waa-waaw,ku ma fay yobbu kay laa amul,mu ne ko,demal ca sa ñoñ,te waaj,te ñëw ci mujjug at mii nu ànd aji,bu neexee yàlla ,ma dem waaji te lijanti ji sama njaboot,naan (Inna lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun).

Nu dellu ca wax ju njëkk ja,sëñ Mbakke BUSO nee na,bi ko ñaari mbir yu gaar yooyu jaaxalee,muy mbirum jaxasoo bi ak mu bëgg a aji gi,da maa woo,waxtaan ceek man,diisook man ci mbirum ñu sanci ab barab,bu nu man a tàqalee ñaari kuréel yi wëlif ñu dul ñoom,te teqale leen ñoom ci seen biir,ngir ñiy jàng ak a jàngale man a def seenub ligeey,mu samp ci jiite njàngum alxuraan mi, ,sëñ Abdu Rahmaan LO,njàngum xam-xam mi,mu teg ca Maam Cerno rakam ja, ànd faak ñoom ñaar rekk ak seeni kuréel,keneen dollikuwu ca,ci donga yi walla sheex yi.

Mu ne ma yaw nag kon da ngay des Tuubaa,di jëwrini donga yi, ñiy siaaresi bu nu ñëwee ak seeni àddiya,ku ci war a agsi,nga bàyyi mu ñëw,ku wart a agsi,bumu agsi. Ma ànd ak moom ci loolu,xalaat ne lii daal xalaat bu nu barkeel la,inshaal laah. Mu tàmblee waaj,di ci làqatu ñi mu bëggul ñu dem,bi dogu gi dëggaree ci dem,te loolu da ko daa làqq sunu waajur wii di nijaayam, nga xam ne da koo bàyyi woon ak man rekk,doyloo ab gis-gisam ci man,mu mel ni da maa soxlawul – bi mu ci dogoo dëgg nag,la xam ne du man a ñàkk,mu yëgal ko nijaayam jooju,mu dal di ko koy yëgal,yëf yi nag tiis ko lool,ngir xam gi mu xam ni buuri Jolof yi fiire,ak ni nu manadee muñ,wuuteek buuri wii tund , te taalibey Jolof yi it dunu bàyyi seeni doom aki donga,te dunu muñ it wuuteeg yu gox bii,mu ragaloon nu sonal ko,aaye woon ko ci anam gu nooy mu bañ a dem, yee ko ci aaday ñaari dëkk yi,ci li mu ci xam,ndax xamoom na ne li sëñ bi bëgg dëppoowul ak seeni aada.

Waaye sëñ bi moom niki soofiyu yu mag yi,dafa dogu te fas yeenee wéyal li mu dogu, ndax wéyal ag dogu ci tasawuf la bokk,tekki ag dogu fi ñoom mook tubbee yam,dee ko gën a woyof ci ñoom.
Kon sëñ bi laxas na ak dongaam yooyu,ca sawaal ci atum junneek ñatti teemeer ak fukk ak ñaar g,(G, mooy:ci ati gàddaay gi) wuti suufus Jolof,ndax gisul ci Bawal,barab bu man loolu mu bëgg,ca jamono jooja,ak ndax itam Jolof suufus ay maamam la woon___p45 mahalu ajdaadihii ba bi xurbi Tuubaa_____,walla muy aajowoo jankooteek ay ñoñam,mbaa mudaaraanteek ñoom,te loolu du lu mu daa faral a def,mu dox ak ñoom,ba Mbakke Baari,wacci fa,sanci fa,waxtaan faak yenn jaraaf,waaye ag ñagas feeñ ca njëlbeenug wax ja, àggoon ci ñu naan:nun dey xamunu woon ciy donga ag sàkkoo dooni buur, ñii di ñëw daal,nekkunu lu duli buur,yu ñëw ngir xëccook ñun suniy suuf,yàgg nanu leen a dégg ca ña ca seen ginaaw,nun nag ñi ngi giñ ci ne dunu dëkk ak nun ci sunu suuf sii,ci seen melo wii,ak wax yu mel nii,ci yi ko nijaam ji daa wax,ak a sentul bu fa demee. Waaye yàlla moom bu bëggee amulum mbir da koy wutali sabab, nee nanu bu yàlla bëggee tàllal gënéel lu lemu,da koy wutal làmiñu ku iñaan. Bokk na ci xeewal yi yàlla xeewale sëñ bi , sóob gi mu ko sóob ci yoonu walliyu yi, sunnatul laahil latii qad xalat min qablu,walan tajida lisunnatil laahi tabdiilan muy ci maanaa yoonu yàlla wii di wu wéyoon bu yàgg,doo gis ag coppite ci yoonu yàlla. Nit du jug mukk jëm ca yàlla ndare bu danu koo natoo ay noon yu koy lor,loolu fiiraangeg yàllaa ngir mu bañ a jàdd,bañ a wéeru ci ku dul moom,yàlla da koy feeñu cig màgg akub taar,ci feeñu gog taar gi (attajalliil jamaalii) ,la ko yàlla di ñoddile nit ñi, ñuy sottiku ci moom niki ay weñ yu tiimub puur,loolu nag ci tàggatug yàlla lay ame, ñuy yërmaande juy texeel ku nar a texe. Ci feeñu gog màgg gi attajalliil jalaalii la leen yàlla di dëddaleek yen xol yi, ñu nekk seeni noon,dunu gis seen hurma,dunu leen gëm,di leen ayibal ci seen bop,ak ci seeni taalibe,waayee ak loolu lepp,hifthul hinaaii du tàggook ñoom,mooy wattu gi leen yàlla di wattook a aar,dara du leen dal lu dull u yàlla bëgg mu dal leen juge cib noon,di luy ñaaw ci saayir,diw yoon jëm cig fayantoom Innaa minal mujrimiina muntaqimuuna muy ci maanaa,da nanu fayyu ci ñiy tooñ. Ñi ngi ñaan yàlla jàmm. Lii mooy mbirum sëñ beeki àndandoom ca njëlbeenug Jolof, bu dee lu aju ci ñam ba woon ca ginaawam nag, ñoom sëñ Mbakke BUSO nee na:taalube yi mu ba woon Tuubaa,bi nu yëggee ni sëñ baa nga Jolof , ñu tàmblee wuti pexey dem fa,yalwaankat yi fekksi leen ci loolu, ñu gàddaaye Tuubaa,ndare ku fa dëkk,xaalaatub siyaarekat yi di fa yam dal di yàqqu,lu tax deet ginaaw mbir mi dàu mbirum xalaat.

Bu dee lu aju ci jaraaf dëkk bi,ku ci gisoon,li nga gisoon gën naa yokk,ku ci gisutoon tàmbli nga gis leegi,nga boole ci lanu deggoon ci diggam ak buuri Jolof yi,nu dikkal nu ci kaw ak suuf.
Bi buur yeek seen dag yi gisee li nu gis,te ñoom boroomi ngànnaay lanu, ñu daa dund ci seen ngànnaay rekk,dan daan song ku leen daa jeem a të,duma ko,nangu alalam,ray ko mbaa ñu njaf ko (jàpp ko jaam),loolu nag di woon aada ju yàggoon ci ñoom,ju nu daa donante,waaye loolu teewul ñu amoon jàmm ak lenn ci boroom neeg yu mag yi, daawunu leen boole ci seen jëf jooju,daawunu ci boole it ñi daa aaru ci seen kaaraange,niki neegub sëñ bi.

Loolook meneen mbir a waraloon nu jaaxle woon ci sëñ bi,meneen mbir mi nag ,nga xam ne moo leen gënoon a jaaxal,mooy mbirum nguur gu raglu gii,loolu nag mooy tubaab yii di waa faraas, ñoom danu daa def,suuf sunu not ,jël fa njiit,muy ku fa bokk,samp fa,ngir waa dëkk ba bañ a mer te ànd ak ñoom,xoolal ma gii xam politig,,,,p48,,,,,,,wakaana haaulaayi,,,,,,ba ,,,,,,falamaa lam yakun lihaaulaayi,,,,
Bi jaraaf yooyu demee ba manatunoo dellu ci seen aada yu njëkk yu bon ya,muy ray jullit ñi,ak giir seeni alal,ak doonte loolu da leen di àggale ci nuy raye it,du tee nu def ko,bi nu demee ba manatunu loolu te loolu tubaab yee ko waral, ñu mujj di leen xiirtal tubaab yi,jaare ko ci ay pexee ki wor. Mu neeti : jaraaf yooyu jaxase googu nu doon jaxase jullit ñeek nguurug tubaab yi,jubluwunu ci woon,faagaagal leen,ndax lu man a xew, ñoom ci seen ron kilifteef lanu nekkoon,doonte ci anam gu woyof la,waaye kay ñi ngi ci jublu woon ame ciw yoon wu nu man a nangoo seeni alal,bari na lu nu leen daa wax naan diw kat da leen a bañ,diw it nanguwul a fay galak, diw mee am na lu mu leen di waajal,diw mii mi ngi wuti ngànnaay,di dajaley fas,walla nit ñaa ngi koy deglu ,walla ku bariy taalibe la, ñu koy màggal,dayob màggal, ba àgg ci bu leen junjoon geej gi,ñu sóobu ci xuus ko,ak leneen ak leneen,ci seen fen yi nu daa def,ngir bëgg tubaab yi digal leen ñu songu leen,walla nu def ci ñoom lu leen soop. Te xamunu ne yewwuteg faraase yi,ci wàllug politig moo gën a yaatu loolu,waaye nag wax bu baree juge ci ku la naan mooy sab bët,di sa asaa sekkare,di la xoolal sa ginaaw,da na mujj am lu mu bàyyi ci yaw benn bis,rawati na bu fekkee ki ñu ne moo def loolu,du rambaaj,du jaxase,te du jeem a setal boppam,ca ki nu ko rambaaje,te ñiy yàqq dunu dañ,di yàqq diggante bi,rawati na bu nu niroolee am mbiram ak mbirum ku yori donga,yu ko gëm,lu mu leen digal nu def.

Looloo waraloon ñu tàmblee tiit ci moom,ndaxte dañ koo niroole woon ak sheex Omar Fuutiyu, Tukkuloor la bu defoon ay xare ci wàll gi dëkke woon ,ci mujji ati juroom ñaar fukk yi,bi loolu jàllee ba teg lu néew,la benn wolof bu tuddoon Maalik BA,nu gënoon koo xam ci Màbba,defoon ay xare ca goxub Saalum,ci ati juroom ñatt fukk yi,ginaaw bi la Ahmadñ sheexu dib Tukkuloor,xaree xareem ba ak waa Jolof ak Kajoor,ba bi mu deewee ca bisub Samba Saajo,ca wàllug Luga,ca mujjug ati juroom ñeen fukk yi.Jaxasekat yi nag ,bi nu demee ci tubaab yi danu leen sëñ bi ñii lay roy,ba mujj tubaab yi manatuñoo ñàkk a gëstu lin leen wax,lii daal mooy li gën a waral tubaab bi jublusi sëñ bi,ginaaw bi ko yàlla dogalee namm ca la mu ca namm,muy wax joj dara amu ca,ndax sëñ bi lorewul ,soxlawul àdduna,te xemmeemul li nu jort ci moom,yàllaay seere lii nuy wax.
Bu doonutoon rambaaj yii,waxuma la buur yu ndaw yi sax dunu ko jeemal,waxantuma laak yu mag yi,waaye loolu day dëggal waxi yonant bi ji (j.y.m), ñi yàlla gën a teg ay nattu ñooy yonant yi,teg ci walliyu yi,teg ca ña gën,teg ca ña ca topp, ponk bii nag bu wéy la ci xeetu yonant bi (j.y.m),ndax ñu baax ñi ëpp ag gëm foo leen fekk,daniy fees dell aki nattu, àdduna dëddu leen naqqari ci ñoom, ñooy ëppi jafe-jafe fuuf ñu dul ñoom,boo demee ca Sahiihub Muslim,ak bu dul moom,da nga ca gis : àddunaay kasob jullit,tey àjjanay yéefar ,yàlla itam wax ne : wal aaxiratu hinda rabbika lilmuttaqiin muy àllaaxira, ñu ragal yàlla ñee ko moom.

Bi tubaab yi demee ba manatunoo ñàkk a xool mbirum sëñ bi, ñu tàmbli faa yabali ndaw aki bataaxel,ay yooni yoon,di sàkku ci moom mu seetsi leen,moom muy xaar ndigalul boroomam rekk,ak lu yonant bi,(j.y.m), ñu gise yeex a wuyyusi gi,ag bañ,bu ko defee ña daa jaxase di gën a am lu nu wax,naan,waxoon nanu leen ko,gis ngeen linu leen waxoon am deet? .
Ba bi fa tubaab ya yonnee lenn ndaw mu ànd ak yenn soldaar yu neew,bunu leen tollaleek li nu am ciy xarekat,ndax matunu mbooloom xare mu mag,lii moo doonoon li ko boole woon ak tubaab yi.

Sëñ bi,bi mu jotee ndigalul yàlla ak yonant bi (j.y.m),yonant bi(j.y.m) jox ko kiiraay luy dox diganteem ak tubaab yi,te loolu wax na ko ci genn xasida: kun tànn ki,jàmm ak mucc yal nanu nekk ci moom,wutal ko kiiraay lu koy aar wëlif lor,ne ko doxal te bul ragal woru, bi loolu amee mu genn ca këram ga mu sancoon Jolof ngir jàng ak jàngale,ci bisub gàwwu fukki fan ak juroom ñatt yu safar,ci atum junneek ñatti teemeer ak fukk ak ñatt g. Ci jummaada saaniya walla sahbaan ci at mii,la sheex Bashiiru gane àdduna di doomi sëriñ bi,bi miy genn dajeek ki jiite mbooloom xare moomu genn moom itam juge wàllug Luga, ñu daje ca Jeewal ca ngoonug bis booba,sëñ Banji NJAAY,nee na ma - moom ci ñi àndoon ak sëñ bi kerook la ñu gënoon koo xam ci Banji Xuja – am na benn karaama bu feeñ Jeewal,mooy bi nu àggee Jeewal ,danoo jeexaloon ndox,te foofa ndox bariwu fa,satalag sëñ bi jeex,bi nu nekkee ci jaaxle googu nag,benn waay buy or ab baag bu fees dell ak ndox jege,nu wax ak moom xamul li nu koy wax,nu jox ko ab defukaay, mu duy ko ba mu fees ak ndox,nu naan,sëñ bi jàpp,ndax moom daawul tiim,waa ja jàll,te deggunu aw làkkam,xamunu ci moom dara.
Sëñ bi nee na :ginaaw bi nu jullee tàkkusaan,nasaraan boobu di njiitul soldaar yi,dikk na, bëgg a wax ak moom,mu wëlbati kanamam wëlif ko ,jublu yàlla,jàng Bismil laahir rahmaanir rahiimi juroom fukki yoon,waa ja nooy,aw xalam fay,mu gaaw genn,jëm ci ay aajoom,mu fanaan foofa,ak jaraaf ju ñuul jooja,ci loolu sëñ baa ngi naan: ginaaw bi nu dajeek ña gennoon jëm ca këram,te njàqqare nekk ci seeni dënn.

Dox nanu àndandoo di way gaaw,jëm ca jaraaf ja,ba tàkkusaan jotee ñu julli fa cig ragal yàlla.
Ginaaw bi la jaraaf ji daje ak moom,mbooloom xareem mi wër ko,am ca ñuy siaare.
Mu jubale kanaman ca yàlla mu tedd ma,bañ koo jubale jaraaf ja,ngir am li mu bëgg.

Wax juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi,cig toroxlu jëm ca ka nga xam ne,fu mu daaneele ab noon mu nërméelu.
Jaraaf ja genn cig gaaw jëm ca aajoom,mu fanaan fa di boroomi xeewal.
Waxam ji mu naan am ca ñuy siyaare ,sëñ nee na mi ngi ci jublu woon,taalubeem ba Omar NJAAY,sheexub Konjoru Njaay,di dëkk bu nekk ci wetu Luga,moom nag am na wàccuwaay bu kawe ci sëñ bi,bi mu faatoo sëñ bi seereel na ko yiw wu rëy,dig ko it yiw wu ko ku dul moom di ñeewe,ngir rafetug njortam,ak waxam ju rafet ci sëñ bi, ñi ngi ko denc Njaareem.
Sëñ bi nee na: (( Omar mii mi ngi genn,ngir siaaresi ma,dajeek soldaar siy genn,fekk nu xamoon ko,te fonkoon ko, ñu kontaan ci ànd gi mu ànd ak ñoom,jàppe woon ko kenn ci seen kilifa yi,waaye yàlla moom xam na la nekk foofa)),sëñ bi nee na ((nasaraan boobu jiite woon soldaar yi,moo doonoon ki yoroon Luga (gouverneur) ca jamono jooja,doonoon gorob buuru ndar (boroom ndar),looloo waraloon ñu deglu woon ko ci samay mbir,mooy ku rëyoon ki daawul wax ci man lu baax,daawu ko def,daawul ànd ak ku koy def,dogu woon it ci tumbrankeel ma,nu ne ko du fi ame,mu ne kenn du ko tee am,dogalub yàlla bi dëppook li mu dogu,looloo taxoon,ma yàggoon Ndar ñuy xool samay mbir )),,,p45 dale wa awra lihaasihiil aaya,,,,,,,ba,,,,,,,,,,,sais yamkur,,,,,,,,,,
wa iz yamkur bikal laziina kafaruu liyuzbituuka aw yaxtuluuka aw yuxrijuuka,wa yamkuruuna wa yamkurul laahu wal laahu xayrul maakiriina muy ci maanaa ,bi la ñi weddi di fexeel,ngir saxal la fi,walla ñu ray la,mbaa ñu genne la, ñu nekk di fexe,yàlla itam di fexe,te yàlla’ay ki dàq a fexe.Sëñ bi nee na :((Ndar, ña fa nekkoon ñatti kuréel la woon, ñu bëgg ñu bàyyi ma fa,bu ko defee,nu di leen sonal ca daanaka-dun ba bepp (daanaka-dun mooy Presque ile) ,di yàqq seeni kër,ak ñu bëgg ñu faat ma, ñooña amunu lanu bëgg,ak ñu bëgg ñu tumbrankeel ma, ñooña yàlla dëppale dogal bi ak seeni xalaat)). Sëñ bi wax na ci loolu lii: yàlla tàbbal ci xoli ñi sababoon ag tuxalam,ca jooja jamono.

Ab nettali bu yéemoo ngii ma degge ko ci sëñ bi,ci mbirum àttekatub (goornoor) Luga bu rëy te bon,te féetee woon mbirum tukkib sëñ bi te taxawoon temb ci mu am. Sëñ bi nee na :(( àttekat boobu ,bi ma nekkee ci tukki bi ,laa dégg ñu ne danu koo mujj mere,gëstu ay mbiram,gis ci luy waral ñu genne ko,tumbrankeel ko,bi niy xalaat,mbugal mi nu ko war a teg,am ku ne kii daal,ginaaw moo taxoon nu genne sëñ bi tumbrankeel ko,nanu ko yobb,fa waayam ja nekk, ñu dëppoo ca loola,muy fayyug sunu boroom,yëguma lu dul ñu ne ma àttekat baa ngi ci dun bi ma nekkoon,mu nekk foofa ab diir di ma làqatu ngir ragal ak rus,looloo waraloon mu dem gis goornoor (àttekat walla saytukat) ba fa nekkoon,ne ko moytul ma sëñ bii fi yaw,bu ko jeem a def lenn lu ko naqari,ndax lii ma dal de dara waralu ko lu dul sama yeene ju ñaaw ci moom,kon daal bul def lu dul,di ko jox li nga ko war di fay weer rekk te yam ca,looloo waraloon àttekat boobu nooyoon mel ne galas fi man,tukki bi, li ci jafe woon lepp mujj yomb. Bi yàlla sottee ndox ca sawaraam wa doon jëf-jëfi (moom goornooru Luga bi), mu mujj di ku sedd,la nu ko delloo fa mu juge woon,ginaaw bi ñu yobbooti ko ci penk bi,ca wàllug Xaay,foofa la ko ab njabarkat bu bàmbara njabare,ci genn kërug bàmbara, mu dee di ku nu dàkku, di ku nu gàññ, xoolal ma rekk mujjug ñiy tooñ)). Mbirum noonam boobu,nirook lool,mbirum noonub ki miy ligeeyal di yonant bi (j.y.m),noonam booba di woon,Haamir doomi Tufayli,ba mu nee – jamono ja ko tawat ji sonalee ci genn këru jenn jigeen ju Salool - ,,p57,,,,,,,,axudatan,,,,ba ,,,,,,,,bayti saloliya,,,,,,,
Sëñ bi def na ag xasida,gum u tënke arafi mazalul jannatil latii wuhidal muttaquun , ba ca, tilka huqbal laziinat taqaw ne; tooñ gu nu ma doon tooñ,jeex na,aji not jee ko jeexal,ji damm ngànnaayul ki doon puukarewu, mu damm.
Moom de yàlla am na samag cant,ndax rayal na ma ka doon fexe ci atum junneek ñatti teemeer ak fukk ak ñatt g,te deem gi dolli xalaat yi.
Amewul ca la mu doon def,lu dul am mbugal,te ginaaw bi mu farloo,ba yaakaar ne moo ci ne,daa daal di giim,tawat ji gàllankoor ko.
Fayyug sunu boroom da koo tiital mu daw, ci geej geek ci jeeri ji,te am mbooloom wor ko.
Jaraaf ju ñuul jooju,xam naa aw turam xam giir gi mu bokk,waaye du ma sobeel sama xalima ci bind aw turam,mook mbokkam mu nasaraanu, mi daa ñaawal sëñ beek a saboote,fu mu masaa dajeek moom,moo nekkoon Garambasaa.
Gis naa li sëñ bi bind ci ñoom ñaar, ñu bari it, ci ñi xam seenug mujj,nettali nanu ma ne ku ci nekk dee gu ñaaw la dee,kenn ki mooy ku jéeri ji,mi ngi Ndakkru,ki ci des,di ku geej gi,nekk Konaakiri,yal na nu yàlla musal ak jullit ñepp,ci nattu bi mu leen tegoon.
Nu dellu ci mbirum tukki bi,sëñ bi nee na kerook wird wi mu gënoon di def,mooy Inna walliyiyal laahul lazi nazzalal kitaaba,wahuwa,yatawallaz zaalihiin muy ci maanaa :kiy méngoo samay mbir,mooy yàlla mi wàcce teere yi,te mooy kiy méngoo mbirum ñu baax ñi. Loolooy maanaam waxam jii: yàlla naagul na ci man ibliis,fa Jeewal,bi ma ko woowee ci turu walii,(muy kiy méngoo mbir yi).
Sëñ bi fanaan foofa,bi mu julle suba,laxas jëm Kokki, ñu yendu fa,mu tàmbli faa woy xasidag Asmaau Ahlul Badri, sëñ baa ngi wax ci loolu: ganaaw bunu fa yendoo,moom tàmbli na fa di woy lol ubbil na ko ab bunt.
Boobu bisub dibéer la,bi gee jàllee ba teg lu néew,ñu laxas, - ci li ma kenn ci ñi àndoon ak sëñ bi nettali – ci fenkug weer wi,ci guddig altine dëppook ñaar fukki fan,juge Kokki,nee na :booba ñun ñi ngi dox, muy wicc-wiccal ci sunu kaw. Sëñ bi nee na : maa ngi rañaan (mooy dox guddi) kerook ca guddi googa,ci kaw sama wenn gelamu ñu naa ko Hawnul laah,wu gaaw,nga xam ne fasi ñoñ buur bi manunu koo jot,te ñi ngi doon def li nu man,ba mujj am ci ñoom ñu naan ma:sëñ bi defal nànk,yëramal sa bopp,te yëram nu,ma naan leen gaaw leen,nu ku nu yilif,ba noppi yonni ko di yeexe?bu ko defee,nu wedam. Sëñ bi def na ci loolu aw woy: laxas nanu ginaaw bi nu yendoo,di dox,ca ginaaw gee, ànd ca ak ag xat te di ko muñ.
Nu àgg,laataa jullig fajar,mu fanaan guddi gi ci yekkati ay bayit ,di boroomug jàjji.
Bayit yi mu doon yekkati, ñooy ñaar yu Busayri yii:
((kuy sukkandiku ci ndimbalul yonant bi,bu koy gaynde fekkee cib àll it wedam.
Moom yonant bi,foo ko gise ak doonte moom rekk a ànd,da nga naan mook am mbooloo ànd ngir,màggam ga )).
Li mu jublu ci di boroomug jàjji gi ci woy wi,nag,mooy mu nekk di jàjji fas wi ngir mu gaaw. Ginaaw bi, nu àgg Luga,laataa fajar,yendu fa.
Nettali nanu ne sëñ bi nee na:bi mu jegee Luga,kenn ci ndawi nasaraan bi,te bokkoon ci ñi àndoon ak moom,wax na ak moom,ci anamug yërmaande,ne ko ngànnaayul,jege nanu noon bi de,sëñ bi ne ko ci kàddu gu dëgar,yàlla du lott,te du des ginaaw,bi nu àggee ba dal,la ndaw li ko doon wax loolu dellusi, ne ko man dey da ma laa wax ngir yërmaande,ngànnayul,jege nanu noon bi,nga ne ma yàlla du lott te du des ginaaw,li nga ma tontu ci sama wax jii de,xawma ko,loo ci jublu? Sëñ bi ne ko maanaam loolu mooy yàlla (t.s) dara du fàddu ci moom,kon mi ngi ànd ak nun,bu doxee sama diggante ak noon yi,ci kàttanam,dàkku ma wëlif leen,kenn du ma manal dara,bu ma bàyye ak ñoom it, ñu def la leen soob,kenn du ci man dara. wa in yamsaskal laahu bidurrin falaa kaashifa lahuu ila huwa,wa in yuridka bi xayrin fa laa raadda li fadlihii, muy ci maanaa bu la yàlla laalee ak lor,kenn manu koo dindi ku dul moom,bu la nammalee aw yiw it kenn manul a delloo ngënélam. (yàlla mu sell mi dëgal na,yonant bi,jàmm ak xeewal nanu sax ci moom,jottalee). Ndaw li dem ànd ak mbégte,man ma ne kooku sëñ bi daf ko doon leeral haalam (haal mooy melo walla mbir walla aw nekkiin) ak ni mu donne yonant bi (j.y.m),yonant bi (j.y.m) nee na wàkkiirlu mooy sama haal,fàggu di sama sunna,ku lott ci sama mbir,bumu lott ci sama sunna, sëñ bi moom donn na ci haalam ak sunnaam ab cér bu mag,ak ci haalu Ibraahiim (j.y.m) bi nu ko sànnee ca sawara sa,malaaka yi ñaan ko mu sàkku ci ñoom ndimbal,mu bañ,JIbriil (j.y.m) ne ko ñaan ko,mu ne xam gi mu xam sama haal doy na ma ba du ma ko ñaan.
Sëñ bi yonant bi la ciy jikko,di Ibraahima ci yite (j.y. ñ),day jëf haalu yonant bi ak sunaam,gis nga haal ji noonu,mu jëfe ko,ma won la nag ag jëfeem sunna si,bokk na ci loolu,moom defal nanu ag xasida gu nu tënke harafi hasbunaal laahu wa nihmal wakiil muy ci maanaa yàlla doy na nu sëkk,te moom de wéeruwaay bu baax la.

Mu ne ci xasida gii laa sengewoo woon (senge mooy ta-ta,walla ci tubaab fortification,muy miir bi ñu njëkk ña daan tabax wërale seen dëkk yi,ngir mu leen di aar ci song gu bette,kon sengewu mooy aaru ) ca ngoonug bisub àjjuma ba,ba ma dogoo ci ànd ak ñoom ca gàwwu ba,ginaaw bi ma yonant bi (j.y.m) aaree,digal ma ma dem,ne ma wéyal te bul ragal lor.
Xasida gii nag mooy muslaay li,juttit bu ne war na koo jeem a am di ci musloo li mu ragal,bu leen fàtte li ñenn ñiy wax naan,waxtuw ajjuma mi ngi dale ca ginaaw tàkkusaan,ba bu jant bi sowee,xasida gi nag mooy gi tàmblee hamidtu man yahsimunii minad darar, muy : maa ngi sant ki ma musal ci lori jepp saytaane ak junne ak nit.
Tudd naa sellam ga,muy buur,buy aji wattu,may sàkkoo aaru ci wattoom gi wëlif musiba yi ak mbugal yi.

Maa ngi sàkk ci moom mu musal ma ci bànneex,ak ibliis,ak ci mbooleem yiy lore ci jamono ju ne.
Yeene naa koo ñaan di sàkk am ramu,ci darajay soppeem bay ramu ñiy ramu.
Mooy Ahmad,sangub mbindeef yi,may julli ak a sëlmal ci moom,te di ko def aw yoon jëm ca sama boroom.
Maa ngi ñaan ,sama boroom,ci darajaam,mucc ci saytaane ak ciy ñaawtéef,ak way bew yi di ma xaccoo.
Yaa moom mbindeef yi ,yaw sama boroom,may ma ag muc ci ñoom,ak bepp balaa ak mbugal.

Yaw laa jox sama bopp de,yaw aji wattu ji,ba fàww it ya’ay sama wettal.
May ma li ma bëgg ci addina ak alaaxira,na nga ma musal it ci gàccag àddina ak gu allaaxira.
Jubale naa la sama kanam,yaw sama boroom,ya’ak sama wasiila,te loolu doy na ma.
Musalal samag wàll ci mbooleem luy ñaaw,te nga fegal ma mbooleem luy jax-jaxiloo.
Soril ma mbooleem noon yi ,ci barkeb yonant bi,ak Ahlu Badri ñu tedd, ñiy ay tànnéef.
Na nga ma xeewale ci ma dugg ci sa senge (kaaraange) lu aaru li,te dëkk fa,di ku am kóolute ci samay noon.
Yaw’ay kiy musal kuy muslu ci yaw,ci lepp lu ko man a jublu ciy mbugal.
Samay mbir ba fàww da ma koy joyal jëme ci yaw,ndax ya’ay ki nga xam ne ku wéeru ci moom deesu ko jalax.
Yaw aji baax ji,fegal nga ma ag kéefar,ak lori ñoñam,ak jepp fitna.
Fegal ma loxol woy bokkaale yi,ci darajay Ahlu Badrin,te nga def leen ñuy sama senge.
Yaw aji baax ji,nekkal ma te bu ma gecceel,ci àddina ak àllaaxira,te dee ma jéggal.

Bindalal yonant bi ag xeewal ak mucc,ak ñoñam aki saabaam,ci anam gu sax.
Mu tëje ko fanqalaboo bi nihmatin minal laahi wa fadlin,lam yamsashum suuhun,wattabahuu ridwaanul laahi wallaahu zuu fadlin haziim : muy ci maanaa, ( ñu dellu ànd ak xeewalug yàlla ak ngënéelam,lu ñaaw laalu leen, ñu topp ngëramul yàlla te yàlla’ay boroom ngënéel lu mag li).
Mu neeti alhamdu lillaahil lazii hadaanaa lihaazaa,wamaa kunna linahtadiya law laa an hadaanaal laah,wa aaxiru dahwaanaa anil hamdu lillaahi rabbil haalamiina muy ci maanaa : ( maa ngi sant yàlla mi nga xam ni,moo nu gindi jëme nu ci lii ( muy lislaam) ,duñu doon gindiku bu nu yàlla gindiwutoon,sunu wax ju mujj,mooy ag cant ñeel na yàlla,miy boroom mbindéef yi) .

Xoolal ni mu aaroo woon ci baat yii nga xam ni,yàlla da leen a tagg,tagg it nit ñi ciy aaroo.
mu wax: allaziina xaala lahumun naasu innannaasa xad jamahoo lakum,faxsawhum,fasaadahum iimaanan,waxaaluu hasbunaal laahu wa nihmal wakiil ba fam yam muy ci maanaa :( ñi nga xam ne nit ñi dañu ne leen: nit ñi kat dajaloo nanu ngir fexeel leen,kon tiit leen te moytu,loola dolli leen ag ngëm, ñu maase ne yàlla doy nanu ,te doy na sëkk ku ñu doyloo). Nga boole ca loola juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi, yi mu jàngoon ca Jeewal,ba ndawul nasaraan bi bëggee wax ak moom.
Waxees na ma ,te loolu lu wer la,ne rakkam ja sheex Ibra Faati, ci bis bi sëñ bi tukkee,ba bi mu dellusee,masul a dañ di def junniy salaatu alan nabii ci melo wii : (( allaahuma salli halaa sayyidinaa muhammadin,wa halaa aali sayyidinaa muhammadin,salaatan tunajjiinaa bihaa min jamiihil ahwaali,wal aafaati,wa taqdii lana bihaa jamiihal haajaati,wa tutahhirunaa bihaa min jamiihis sayyiaati,wa tarfahunaa bihaa hindaka ahlad darajaati wa tuballixunaa bihaa aqsal xaayaati min jamiihil xayraati,fil hayaati wa bahdal mamaati)). Maanaa mi di:( yaw buur bi jullil ci sunu sang Muhammad,ak ñoñi sunu sang Muhammad,ag julli gu da nga nu ci musale ci mbooleem tiitaange yi,ak gàkk-gàkk yi,fajale ñu ci mbooleem aajo yi,laabale ñu ci, ci mbooleem ñaawtéef yi,yekkatil ñu ci gën jaa kawey daraja fa yaw, àggale ñu ci ca dayo ya gën a sori ci mbooleem yiw yi,cig dund ak ginaaw ag dee). Mu ko daan def ginaaw bu wàccee kaamil bi,waaye kaamil bi moom lu saxoon la,suba ak ngoon,naka jekk, njëkk sëñ biy tukki,waaye salaatu halan nabii gi moom saxal gi,man na a nekk muy ndigalul sëñ bi mbaa xalifaam bu baax,bu sell ba,ngir xér gu mu defoon ci muccug sëñ bi ak ag delluseem ci jàmm,mu sàkkaloon ko mbooloo mu ci daawul sàggan suba ak ngoon,waxambaane wu ragal yàlla,wu dëkkoon Kokki wii di Samba Joop nu gënoon koo xam ci Samba Asta daan leen jiite. Ku baaxoon la te gudoon aw fan,mi ngi faatu ci atum---------------------- waafiris sitri iiiiiiiiiii bokk na ci loolu woy gi mu def Ahlu Badrin,ak aaru ci ñoom,bi mu nekkee Ndar,mu mottali ko, tudd itam ànd gi mu defoon ak ñoom ci tukkeem boobu, ñu daa toroxal kepp ku ko daa jeem a lor,teere boobu,jotoon na koo won ca magi Ndar ya ka ñu naan Alhaaji Muhammadu Maabeey,ne ko mu mokkalandi bayit wu njëkk wa,ba ñu dajewaat ginaaw bu ñibisee.
Te kat dajewaat nañu ginaaw juroom ñaari at aki weer,bi nu dajee sëñ Maabeey jàngal ko bayit wi,daal di daanu ab jéll,joy. Ak leneen ak leneen ci li mu aaroo woon te xamunu ko, degg naa ko bis mu naan: bi mu nekkee ci geej gi,masul a dañ di jàng Hisbul Bahri,bu imaam Shaazalii,muy lu am njariñ,li koy wone mooy yitewoo gi ko sëñ bi yitewoo woon,bayit wi mu digale woon mu wattu ko,mooy njëlbéenug xasidag Asiiru gu yeeme,gi nga xam ne sëñ bi feeñal na ci njëlbéen gi,ba ci fukk ak juroomi bayit,lenn ci mbóoti tukkeem bi ci diganteem ak noon yi,ak wone ci mucc gu mu mucc ci seeni lor,xamale ne saytaane moo leen wor ci moom,tax ba ñuy am njort yu ñaaw ci moom,waaye seen njort yi sooy nañu,te sëñ bi dellusi na ci jàmm,bayit yee nekk nii: maa ngi dox ànd ak ñu baax ñi(waa Ahlu Badri),bi may dox(bi may tukki),waaye noon yi jort ne man booba ku ñu njaf (jàpp)laa.

Sama dox bi may def,ci wommatug yonant bi, ànd ceek gaa yu baax yi,yàlla rekk a ko tax a jug,ba fàww it samab dox du jëm ci ku dul yàlla.
Bijji gi ma wommat (bijji mooy jazbu,di lol day xëcc,kon man nanu koo jàppe yitewoo sunu boroom gi nga xam ne daa mujj mel ni ab asyee bu koy ñoddi jëme fa yàlla) jëme ma ci aji tedd,joj lu ma sàkku ci moom mu jàppandi,mooy liy dox ak man.
Samag cant ci xalima,ak ci xol ak jëmm, ñeel na ki ma nekkal cig tab ( ki nga xam ne jamono ju ne mi ngi may sottil ay xeewalam ) te mooy ki di ab santaakon(ku soxlaalul kenn).
Sama ndimbal,samag dëgaral,sama kaaraange ca noon ya,mi ngi bawoo ci aji yaatu,ji di ab mayewaakon
(ku tabe lool) kooku mooy aji dimbali sama.
Sama kilifa nag ci bu may dox ak bu ma taxawee,mooy sama kerkeraam,di yonant bi,te mooy ki may ligeeyal,te moom dey day xont (mooy jox ab dund) ku koy ligeeyal.
Samab yool ci ligeey bi may defal ku nu tànn ki,di yonant bi, mayewaakon (yàlla) bee ko warlu,te moom ku am lu mu faye la.

Li ma nesar nag mooy nekk jaamub boroom Aras rekk,di ligeeyal gën ji mbindéef,te moom yonant bi mooy samab xuppkat(yonant bi day bashiir tey naziir,di kuy begale tey xuppe njir jaam yi bañ a sàggan bañ a naagu ).
Aji feg jii di yàlla,moo may fegal ci yonant bi,ayi noon yi,ak lepp lu ñaaw te mooy ki may xettali.
Samag mujj mooy nekk dib jaamam,di ligeeyal yonant bi,mbiri mbindéef yepp nag ca yàlla lay mujj.
Samay weer aki bis ëlëg ñoo may seedeel nekk gu ma nekk di jaamub yàlla,te moom siw na.
Samay sutura ci addina ak allaaxira,mooy tag yonant b,ci woy ak wesar,te moom suturaalkat bu baax la.
Samaw jiwu mooy teereb yàlla bi ak sunna si nga xam ne ci laay aaroo ci li yaqkat bi jublu(muy saytaane).
Samay kër weet na, ñoñ ñi tas,ngir tag ki nga xam ne,noo ko man a tagge,du tax tagg wi mat.
Woru gi nekk ci mbindéef yi,wor na nasaraan yi,ciy pexeem, ñu jort ay njort,te njort ak woru la.
Sëñ bi nee na : ginaaw bi nu jullee tàkkusaan,lanu dugg ci saxaar gi,jëm Ndar, ñu àgg Ndar bi jant biy bëgg a so,ci loolu sëñ baa ngi ciy wax naan: yàlla ca bu njëkk,la dàqoon samay nëx-nëx, ca Ndar jëme leen ci ku dul man,ci barkeb Ahlu Badrin ña diy gaynde.
Ñu àndandoo sax ca dun (île) ba akub coona,fuglukat ya di ñu fa bari.
Ma sax fa – sëñ beey wax – la desoon ca safar,muy fukki fan,ak weeru rabiihul awal,ba ca bis bu mujj ba,muy bisub alximis, ci diir boobu laa matale woyug Asmaau Ahlu Badrin, muy turi waa badar ,topp ko,wéral ko,ci laa dajee it ak ñu bari ci kilifay Ndar yi,ak li ko wër,kuréel it ci njiiti Njaambur yi seetsi ma ngir tinusi ak ramusi,ci tubaab bi,ma ne leen ba leen ma ak sama boroom rekk,moo leen ëpp ñeewant ci man,gën leen a xam li gën ci man, ñu far taxawlu.
Nee nanu bi nu ko taxawalee ci seen kanam,wax ak moom,ci teewaayu kilifay nasaraan yi,te booba moom ku weet la woon ci seen biir,amu fa ab xarit du caangeenug aw wettal,nu ne ko wax nañu nu ci yaw nàngam ak nàngam ?
Sëñ bi ne leen indil leen ma ki leen ko wax,ba xam ma’ak moom ku ciy ki wax dëgg!.
Te booba li nu doon wax naan moo ko def,ab dof bu amut am xel sax du ko def,waxantu ma la’ak ku mel ni moom, li am daal rambaaj la gu juge ci ñu kañaan lëjal,ba ñu mujj amatuñu kersa ci yàlla,saytaane yàq seeni xel,jox leen xalaatam yu ñaaw,ba nu mujj di rambaaj ak a tudd ciy ñaawtéef aki caaxaan lol ñi gën a dof ci wutkati àddina yi sax,xalaatunu koo bëggal seen bop,mbaa ñu koy soxla,waxantu ma la’ak boroom xel yu dëddu yi àdduna.
Ca bis ba mu war juge Ndar jëm Ndakaaru,te booba ma nga woor, àgg fa njëkk jant biy so, ñu wàcce ko fa ca genn kër,mu tàmblee waajal dog ak julli,waaye ñu jekki-jekki rekk lenn ndaw teew,ne ko ayca ñu dem,sëñ bi jug ànd ak moom,waa ja yobb ko ci néeg bu deesi muslu,lëndam kariis,tàng jérr,xeeñ xunn.
Bi sëñ bi gisee li wàcc ci moom,mu xam ne mooy nattub yàlla bi ko doon xaar,amu ci am pexe mu dul gàddu ko,te muñ te sant yàlla te gëram ko,ndax doon na sentu lu gën a réy loolu,mu dal ni innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun.
Sëñ bi nee na ma fanaan fa dundal guddi gi ci saari Baqara ak Aali Himraan, ñu feg ma ñoom ñaari saar yooyu,ci ñaari sawara yi ak ñaari gàcca yi,ma teg ci julli ci yonant bi (j.y.m) ki may ligeeyal,sama dënn leer,sama xol dal,koolute gi dolliku ci yàlla’ak yonant bi,ndax alaa bizikril laahi tatma-inul xuluub ci tudd yàlla ak fàttaliku ko,la xol yi di dale. Sama gudd gi dal di neex ci yàlla, ak ci aji sabab jii, ak dëkk bi,ak ci néeg bi. Ci loolu sëñ baa ngi naan:
yàlla dàq na jëme ci ku dul man ca Ndakaaru,wepp ay wu pexewaakon (ki bari ay pexe )bi xëccoon jëme ci man.
Bu ma fattalikoo panaan moomee,ak njiit loolee,ak sax ga,sama xol day naaw ak man jëm ci jëli xepp aki gobar ngir jiyaari,waaye yonat bii di kiy fari bàkkaar,dox sama digante ak loolu.

Bi nu xëyee – sëñ beey wax – muy bisub àjjuma,di bis bi njëkk ci rabiihus saanii,lanu yeeg ca gaal ga,gaal gi yendu,fanaan,am mbooloo ci murid yi dikkal ma ca dig gaal ga,di joy,bokk na ci mbooloo moomu,sheex Ibra FAAL,moo ca magoon,sëñ ba’a ngi ciy wax ak ci gaal gi,nana: Yàlla xamal na ma ci gaal gi,ne maay jëwrini yonant bi.
Gaal gu fees googu ak mbooloo yendu na fanaan.
Muritam bu amub nattu boobu dikkal na ko ca gaalam gu nu duy ga.
Murid ba tàggoo dellu ca dun ba, ànd ak xol bu naqari.
Mu jublu ci muridam boobu,sheex Ibra FAAL,ci loolu la jiitoo woon ñepp. Am na ci biir gaal gi ba tay,waa ju ko dikkaloon,di ko laabiire naan ko,am na njiit lu bees lu ñëw juge tugal,jaxasoogul ak nit ñu ñuul ñi,boo ko bindoon xamal ko ne danu laa tooñ,kon mu delloo la sa kër,ca sa njaboot,sëñ bi nee na waa ji bàyyiwu ko,di ko ci lëjal ba sëñ bi far jël daam ak xalimaam,nee na bi ma tàmblee ba bind wenn bind rekk,la ma wax ji dikkal juge fa boroom mbiondéef yi,ne ma leegi da ngay diis sa aajo mbindéef mu mel ni yaw,bàyyi ma fi.

Ma daanaka faatu ngir tiit ak kersa,ca saasa ma far la ma bindoon,waaye ngoor si lëjalati ma,ma ne ko,loolu manul a nekk, ne ko bu buurub buur yi di wax ak jaamam yi mu dëgaral ,kenn du ko man a xam ku dul ñoñam,ña mos la ca neex ak la ca naqari. Nitug neen nag nga xam ni mook nit ñepp a yam,dara waru ko lu dul,mu gàttañlu ci loolu te yam fi mu war a yam,bu bëggee mucc,sunu ko tawfeexalul nangul ko.
Ci loolu mi ngi naan:
Ki njiit li yonni woon ca ligeeykatu yonant bi,sàkku na ci moom cig laabiire mu yonnee ab bataaxel,ca njiit lu bees la tukkee woon ca seeni suuf,ba mu ko doon bëgg a bind,far reccu.
Ginaaw bi aji ligeey ji far li mu bindoon, ñu neeti ko bindal.
Mu bind xasida gu nu nangu gi,ngir fàttaliku ki nga xam ne ci moom la yàlla di wonee aw yoon.
Xasida gu nu nangu gi,moom lanu def ci arafi waxi sunu boroom ji (t.s) ((wa ufawwidu amrii ilal laah,innal laah basin bil hibaad)) muy samay mbir maa ngi koy joyal jëme ca yàlla te yàlla’a ngi gis jaam yi.
maa ngi jëmale samam mbind aji moom ,ji moom suuf ak asamaan ak buur yi.

Gaal ga deqi bisub gàwwu, ñaareelub rabiihus saanii,sëñ bi nee na romb nanu Konaakiri,am benn wolofu saalum-saalum bu ko fekk ci gaal gi,jox ko fa àddiya ju kawe,ne ko man de da maa degg ñu ne yaa ngi ñëw ci gaal gi,jëm Gabong,ma ne naa la siyaaresi,nga ñaanal ma dénk ma.
Sëñ bi nee na ci waa jooju la dégge turu Gabong,xame ca it fi nu ma jëme,ma dal di koy ñaanal,ne ko bi ma koy dénk: xamal yaw sama mbokk,ak foo man a nekk,ne amul benn buur bu dul yàlla,ku jublu ci ku dul yàlla,dana xam ne amul ku fi nekk ku dul yàlla,ku jublu ci yàlla te jaaralewoo ko ci Muhammad yonantab yàlla bi,(j.y.m) da na xam ne yonant beey ki yàlla yonni, ñu dal di tàggoo,mu dem.
Sëñ bi nee na ñu romb Garambasaa,mu ne am na ku ko doon ñaawal ci biir gaal gi,waaye yàlla dox diggam ak moom ci hikamam,loolu nag ni mu ame mooy daa am jëmm ju yéegoon ci gaal gi,ca Konaakiri,te moom xamu ma woon,bi nu jegee Garambasaa,jenn waay ju ñuul genne ci ab neeg ne ma,ndax yaay diw ?jaar ci samaw tur,ma xool ko ,mu ne ma, nee nanu ma sama mbokk (mag walla rakk) de moo la jàpplu,ngir barig li la sa taalube yiy rëyal ak màggal,ak nàngam ak nàngam,bi mu tollee ci wax jooju rekk gall gi dal di sab (yuuxu) mu dem di xaar coow li dal,ba mu dolli ñaawalam yi,waaye sab ga dakkul ba kerook gaal ga di teer,mu wàcc ànd ak ñi doon wàcc, kon alhamdu lilaa ginaaw amul li mu bëggoon,ci loolu sëñ ba’a ngi naan: sama àddiya sell na ca Konaakiri, ñeel ku nu tànn kiy fari bàkkaar,ci lu dul kuy weddi.
yàlla setal na ma ca Konaakiri,ci lepp luy xëcce jëme ci yu nu sib.
Yàlla soril na ma cag njëkk ca Garambasaa,ka doon léewtoo ak man te mu dem wëlif ma.
Àddiya jooju mu tudd foofu nag mi ngi ci jublu,leeral gi mu leeraloon waa ja ko doon laaj,maanaam laa ilaaha illal laa,,,,,,,,,,,,,,,,,,,,,,,,,p 73,,,,,,,,,,,,wahuwal lazii yaqahu bihiil inkaar,,,,,,,,,ba wa qad barraahul ,,,,,,,,,,,,,,,,
Du àddiyay xaalis ju waa jooju,mu tudd romb gi nu romb Dawme,wax karaama gu yeeme gi ko yàlla defal foofa,mu ne daa jëloon benn bitéelu misk,bu mu yoroon,ngir wis ko ciy yereem aki téereem, nee na ñu ne ko sànni ko ci géej gi, mu ne ma gaaw sànni ko,bi gaal gi teeree,am mbooloo ci sunu mbokki jullit ñi,duggsi,ndax danu maa déggoon ,ñu ñëwoon ngir nuyyusi ma,waaye képp ku dugg rekk,jox nga ma ab bitéelu misk, ñepp walla ña ca ëpp,ci loolu la sëñ bi naan : kiy jagleele yërmaandeem di yàlla,woo na ma ci boppam,ci indil ma xéewal yuy tee jaaxle.
Mu jublu woon ci aji yërame jooju yàlla mii di boroomi xeewal,daa ko indil ay xeewal,bokk na ci xeewal yooyu biteeli misk yooyu,mu wax ne bokk na ci karaama yi ko yàlla doon defal ci gaal gi,tàggat gi mu defoon boroom gaal gi mu dikk di ko waxtaanal,di ko won ag ñeewant ak yërmaande,di mettitlu bu baax li dal sëñ bi,daan baril lu mu ko daa wax naan ko yaw danu laa tooñ,mu tuddati ne am na benn doktoor bu ko seetsi woon foofa,mujj am yërmaande lool ci moom naan ko man daal da ma laa bëgg rekk,te fas laa dimble,mu ne am na wenn waxambaane wu tubaab,wu ko dikkaloon wu bokkoon ci waa gaal gi,mu ne yàlla def ci xolam mu sopp ma,mujj di ma ligéeyal ni ko murit yiy defe,mu ne moom daal,noonu la yàlla nekke woon ak moom ciy xéewal,tàggatal ko ñepp ba kerook muy wàcc Gabong.

Mu ne Gabong moom yàggu fa dara rekk tuxooti fa dem ci beneen dun,foofa nag ma sax fa juroomi at,mu ne ci diirub juroomi at yii nag laa mujje mel ni ab jant,mu jublu ci, ci yekkatiku ay maqaama akug siw ak bari njariñ,mu ne ci diir bii it la taalife taalif yu kenn masul a def cib taar ak bari njariñ ci yàlla ak yonnat bi ak ci lislaam. Dun bii nag mooy Maayomba,li koy tegtale mooy waxam ji mu naan :ca tefesug geejug dun boobu laa taxawoon di irtijaal (di wax ci lu dul xool li may wax ci am mbind) di xutba geej gi naan:
yaw geej gi kennalal sa boroom te bul ko ñattal,ndax sunu boroom kat kawe na wëlif ñu koy ñattal(wareesu koo def ñatt, ndax kenn rekk la) cëy moom ni mu doone buur bu tedd.
Na nga nekk di bajbaji,di fuur ngir ragal yàlla,te seere ne man ab jaamam laa,,,,,,,,,

Mu ne ba mu fa defee jeroomi at la demati ci beneen dun,nekk fa ak ab coona,am fa ñatti at yu manke tuuti,di ligéeyal yonant bi (j.y.m), mu ne am na wenn waxambaane wu bokk ci ñoom wu ko fekkoon fi mu nekkoon di bind,mu bocc jaaseem di ko wëndéel ci sama bopp,naan ma yaw ay diw di jaar ci sama tur,ma ne waaw,mu ne ma moytu ma,sama maam kat raykatu walliyu la woon,te maa di ab sëtam,ma joxoñ ko sama xalima gi,gëdd ko mel ni dama koy song,ne ko xamal ni doo sa maam ja daa raye,te du ma ku mel ni ña sa maam daa ray,waa ja dal di tiit,daw juge foofa fepp. Mu neeti am na kenn ci seen kilifa yi,ku doon ñëw ca dun ba mu nekkoon,di nemmikusi soldaar yi,fan yooya yepp nit ñi dajaloo ci waajal kilifa gi,di setal yoon yi ak a rafetal ak a samp ay raaya,waaye bi waa ji ñëwee,li mu njëkk a def,mooy laaj ma, ñu tegtal ko sama kër,mu ñëw ,dugg ,nuyyu ma,tudd samaw tur cig màggal,dal di tàllal loxoom ngir nuyyu ma,man itam ma tàllal sama bos,waaye ca saasa am lu wax ak man,mel ni ag dënnu gu juge ci asamaan,ne : yaa ayuhal laziina aamanoo,inna maal musrikuuna najasun muy yeen ñi gëm,xam leen ne bokkaalekat yi sobe lanu,mu mel ni samam xel daa muuru,ma bëmax ab loxoom bëmax gu tar,ba waa ji yëngutu,deltu ginaaw,dal di taxaw ab diir mel ni day xalaat ci samay mbir,waaye man loolu lepp,teewul ma nekk ci samam mbind,bi lu tollook waxtu jàllee mu woolu ki koy firil,wax ak moom ab diir,firilkat bi ñëw ne ma sa waa ji nee na mi ngi lay nuyyu,te di la xamal ni bu ko mere ndax moom bokkul ci ñi la bañ,walla mu lay lëjal,di la tumbrankeel ak a genne sa réew,moom de nee na bu ko manoon leegi mu delloo la fa nga bëgg,boo gisee muy sonn ci yaw ak di la njëkk a seetsi bi mu daa taa wàcci,mooy daa am kenn ci sa mbokki senegaal yi,ku taxoon ma sopp la,mu sàkku woon ci man ma nuyyul la ko,moom dey ci ñi mu gën a sopp nga,looloo waraloon sama ñëw gii du leneen.

Sëñ bi nee na ma wax kiy tekki ne ko:nee ko loolu ma def de ag bañ ko taxul. Mu dem waaye taxul mu soppiku ca na mu meloon,bi mu demee ba toog ,dal, ñu ne ma da nga koy teral,te booba maa ngi ak as lëf ci seen mburu moomu ñu jaxase ak suukar,mu doonoon mburu mu neex lool,ma yonnee ko ko,mu beg ci lool,sant ma, ne lii de bu ko kuy jambaar-jambaarlu defoon te li miy woote nekkul ci moom,man na ca’a loroo,waaye deesul loroo ci ndigal,alhamdu lillaah.
Da na xoromu ñu indi fi as lëf ci bayiti Ibnu Hanbal yii,mu jëme woon ci Sëñ bi ci lu aju ci xar-baax yu mel ne yooyu:
((Boriwaa na aji jalgalti , ku di ab tooñkat ku sol yerey teddngaam di puukarewu,ciy tëneem aki takaayam))
((ay junniy junni ñoo nekk ci ron kilifteefam,te du faale lu koy digal mbaa mu koy tere))
((ngeen (sëñ bi lay wax) wacce ko ci mbartalum toroxte,dammte ko ci jaasiy ndimbal ju di ab dogaakon (ju ñaw) ))
((ndimbal lu tukee ca Yàlla ñeel jaamam bii di jëwrini yonnant bi,muy ndimbal lol nasaraanam yi sax mujj nanu ci di ay ansaaram (di ay gaayam yu koy jappale) ))
((bu wone woon mboot mi (sekkare bi) moom Sëñ bi,kon dey mbindeef yi gis lu yeeme,waaye moom dënam bàmmeelu ay sekkare la )).

Tudd na moom Sëñ bi ne bokk na ci karaama yi ko Yàlla defal ci tukkib geej gi,feeñug Ahlu Badrin,mu ne moom kat tubaab yi danu koo dëkkaloon ,ci benn ci dun yi, ca karce ga ,fa soldaar sa, ñuy fo ak a naan ak a tux,man may muñ seen lor yoou rekk,ndax xam naa ne ñaari malaaka yiy bind jëf yi, ànd nanu ak mukàllaf mu ne,te ginaaw ñoom ñoo man a muñ boobule coona ak yooyule lor,ngir top ndigalul seen boroom,kon man du rafet fi man may jàmbat,ndax kat li leen di lor rekk,mooy li may lor,li leen di naqàri rekk mooy li may naqàri,te jàmbatunu.
Ci noou Yàlla dogal bis soldaar si genn ngir tàggatuji, waaye ba ñu demee fa ñiy tàggatoo,fekk fa am mbooloo mu war ay fas,rang te kaalawu,ci noonu ñu tiit taxaw,seen njiit li tëyye leen fa,xupp leen ci ne bu xibaar bi siwee da na leen ray.
Ba suba jotee ñu ne mes gisatunu leen,nu dal di nëbb seenub xibaar ñeneen ñi ko yëguloon. Sëñ bi nee na bi loolu jàllee ba tegi fan, seen njiit woo ma,mudaaranteek man waxa man wax ju rafet,ci biir wax ji mu ne ma xanaa da ngaa am ay àndandoo yu lay dimbali boo bëggee def dara? Ma ne ay junne lanu walla ay nit ? mu ne ma yaa ko gën a xam !
Sëñ bi nee na moom da koo wonoon ne moom yëgul li xew ,mu dal di noppi. Am na ñenn ci boroom xam-xam yi ñu ko laajoon lu waraloon feeñug Ahlu Badrin gi? Sëñ bi ne woon ko ngir tiital noon yi, keneen laaj ko ne ko ndax Ahlu Badrin ñooñu nit ña lanu walla malaaka ya ? mu ne malaaka ya, keneenati laajati ko ne ko ndax yonant bi (j.y.m) ca la woon?, mu ne ko moo doonoon seen njiit.
Ci loolu mi ngi naan:

#Article 63: Téere Tasawudus sixaar (4306 words)

Ahuuthu billaahi minash shaytaanir rajiimi wa inniya uhiithuhaa bika wathuriyyatahaa minash shaytaanir rajiimi rabbi,ahuuthu bika min hamazaatish shayaatiini wa ahuuthu bika rabbi ayyahduruuni.

Maa ngi tàmblee ci turu yàlla, miy yaatali xeewalam ci àddina te di ko jagleele ca alaaxira. Yal na yàlla mu kawe mi dolli xeewal ci sunu sang ,sunu kilifa, Muhammad,ak ñoñam aki saabaam,ak mucc ak barke bob dana ci wommate kepp ku jàng teere bii, yobb ko ca àjjanaam ja mu dig ña ko ragal,aamiin yaarabal haalamiin.

Ahmadu mi dul dañ di sant boroomam, di jaamub yàlla,tey ligéeyal yonant bi (j.y.m) nee na : ag cant ñeel na yàlla mii di rafetal ci samag wàll,rafetal gu tooll ne rafetalug ku musla dañ di rafetal.Maang koy sant ndax kat moo tabe ci indil nu tawhiid (muy wéetal yàlla),ak ñaari mbokkam yooyu di lislaam ak lihsaan,te ñooy sunnas yonant bi(j.y.m),xeewal ak mucc gu sax na ne ca xaritam ba,soppeem ba,Ahmad,ak ñoñam ak saabaam yu gëm, yu jullite,yu tedd,yuy rafetal yi.

Lii nii aw woy wu rajas wu am njariñ te tedd la, ma tudde ko yobbalub ndaw ñi(tathawudush shixaar) jem ca àjjanay yàlla jii ami dex,maa ngi ñaan yàlla ag 
nangu,ak jàmm ak sell,ak màggal. 
Maang koy ñaan woy wii di wommat kepp ku ko jàng jëme ko ca yoon wa gën a jub.
Tey texeg ndaw ñi,ak mag ñi,ak waxambaane yeek jigeen ñi.
Waxtuw soppiku jëm ci li nu tax a jug nag jot na,sunu boroom laa ciy wut ci lu sax.

(AG JIITAL )

Yeen ndaw ñi maa ngi leen di digal ngeen bañ a wut lu dul ag jub,te soxlawoo xam-xam,soxlawoo leen jàng ak mokkal,te teet barabi texeedi yi,taqoo leen ak ki dul
dañ di jaamu boroomam,ndax kooku kat la yàlla digale rekk la jeme,kepp ku daw cig ndawam jëm cig jub,bu màgge noppalu.
Ku dabaatal li ko rëccoon ci lu bon akug neen,te jeem a dundal waxtu yi ci tuub gu sell,ak jublu sunu boroom,am la gën. Jàpp leen ci sama laabiire gii ma leen jox,kon dey da ngeen tonowu ci addina ak alaaxira,bokk ci ñiy texe.

(BUNT CI XAAJI DIINE YI)

Diine ñatti xaaj la,benn xaaj bi mooy bu gëm,
Beneen bi di bu lislaam mooy ni nuy jaamoo yàlla ba yàlla di ko nangu,ak bu lihsaan,muy rafetal jaamu gi ngay jaamu ci sa digganteek sa boroom.Lu ci ne dees na ko gën a leeral.
Ñu tàmbli ko ci xaaj bu njëkk bi muy gëm .

Gëm mooy nga gëm yàlla ak malaakaam yi,ak teereem yi mu wàcce,ak alaaxira,ak yonenteem yi ak dogal bi.

(DOGGANTAL (chapitre) CI NI NUY GËME YÀLLA)

Yàlla moom ni nga koy gëme mooy : nga dëggal ni am gi mu am lu wóor la, te aji jiitu la joj jiitoom gi amul fu mu tàmblee,aji des  la te desam gi amul fu muy yam, aji wuuteek mbindeef yi la,aji doylu ci boppam la,kenn la kok amulub kem,aji wéet la ci jëmmam- maanaan amul kenn ku mel ni moom- ak ciw meloom , aki jëfam. 

Kàttan  (man-manu jëf) ak nameel (maanaam  bëgg di def) ak xam-xam akug dund ,ak gis ak dégg, ak wax,yooyule yu war ci sunu boroom lanu. Kon nag mu nekk di  aji am kàttan lu war la, tey ku am nameel ,di aji xam, di aji dund,tey kuy degg  di kuy gis, nekk  it di kuy wax yu war lan ci moom.
Ni yooyu nekke di ay melo yu war ci sunu boroom, la ame yeneen melo yu waradi,te jomb ci moom,niki    ñàkk, (maanaam sun boroom bañoon a am) ak sosu (ci maanaa muy ku nekkam gi am na lu ko fi jiitu,nekkul di ku fi mas di ne),ak jeex (maanaam muy ku fi dul des),ak niru,(ci maanaa yamoowut ak dara ci jëmm du caageenug ci meloom mbaa ay jëfam,kon niroowut ak dara te loolu jomb na ci moom)ak aajowoo (jomb na ci sunu boroom muy aajowoo kenn ci lenn),ak limu (maanaam mu bañ di kenn di ay ñaar aki ñatt) ak lott (maanaam ñakk man-man ci def li ko soob) ak sibeel ( def dara cig sibeel mooy safaanub def ko cig nameel,mooy def goo xam ni andul ak teeyug bakkan loolu jomb na ci sunu boroom) ak tëx (mooy safaanub degg) ak réer ( di safaanub xam) ak dee di (safaanub dund)ak gumba di (safaanub gis) ak luu di (safaanub wax) .

Yile yepp jomb nanu ci yàlla sunu boroom ,tudd naa sellam ga,kon daal jomb na ci moom mu ne di aji lott,mbaa muy aji tëx mba muy aji jëf cig sibeel walla muy aji réer  mbaa muy ku gumba mbaa ku dee -soril naa ko loolu- walla muy aji luu,yii daal melo yu jomb lanu ci boroom asamaan.Moom daal sunu boroom deful dara cig war,lu mu man a def cig nameel la koy def ak cig baax ak coobare,loo fi gis daal,ci mbindeef yi, seenug jëf ak seenug ba, ñoo yam ca sunu boroom,lenn du ci lu war, lu dagan rekk la ci moom,
(dagan mooy lu man a nekk man a bañ a nekk).

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME MALAAKA YI  
yal na yàlla dolli xeewal ak mucc ci ñoom)

Malaaka yi ñoom nga gëm leen mooy nga dëggal te am koolute ci ne ñoom kat ñu am lanu,te ñu  nu musal ciy bàkkaar lanu,(dun moy yàlla),dunu xayta (dunu puup) dunu saw it,ñu sunu boroom laabal lanu.
Dunu lekk dunu naan –jàmm yal na sax ci ñoom - ñoom daal jaam yu yàlla teral lanu ba fàww,ken du ci moy yàlla,ku ci ne li ko yàlla digal rekk lay def.Ci leer la leen yàlla binde.
Sàbbaal seen boroom mooy seenug naan,sellal ko mooy seenug lekk.

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME TEEREY ASAMAAN YI)

Ni ngay gëme teere yi mooy nga dëggal ne wacce gi leen yàlla wacce lu wér la,te lepp lu ne ci teere yooyu ag dëgg la gu deesul sikk.Seenub lim nag teemer ak ñeent la.
Fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Aadama (j.y.m),
juroom fukk yi nu wacce leen ci yonant yalla Sihsa(doomi yonant yalla Aadama), fanweer yi nu wacce leen ci yonant yàlla Idriisa,fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Ibraahiima miy xaritub yàlla bi(j.y.m).
Bu ko defee Tawreet ñeel Muusa(j.y.m),Injiil ñeel
Hiisaa,saboor Davood (j.y.m)Alxuraan jii nag wacci ci sunu sang bi Muhammad yonant bi tëjj yonant gi,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci moom,ak ci ñoom ñepp.

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME YONANT YI,mucc ak xeewal yàlla na nekk ci ñoom)

Ni ngay gëme yonant yi (j.y.ñ) mooy nga dëggal leen,te dëggal li nu indi jële ci seen boroom.Te nga gëm ne itam dëggu ak wóor ak jotal lu war ci ñoom la.Fen nag ak wor ak nëbb dëgg dafa araam ci ñoom.
Gaar-gaar bu dul ayibal tey dal nit da na leen dal,niki tawat, waaye bu mu doon juy foñloo,maanaam juy tax nit ñi di leen daw,niki ngaana nga xam ni day wàlle,ak yu mel ni ñoom,ñoom tawat yooyu danoo wormaal yonant yi,dun leen dal.
Waaye nag jaay ak jënd,ak denc (am soxna) ak lu ni mel ci lepp lu yàlla daganal,bun ko defee du leen dolli lu dul yoolub yàlla seen boroom.
Liy wone ne ñoom ñu dëggu lanu te yàllaa leen yonni,mooy  kiimaan yi leen yàlla di wàcceel ,di ci wone ne moo leen yonni,mu mel ni (ñoom kiimaan yi)daniy wax ak nit ñi naan leen jii waay de lu mu wax, mbaa mu def ko yàllaa ko ko diggal.
Yonant yi nag, seenub lim ñatti teemeer ak fukk ak ñatt la,waaye anbiyaawu yeek (mooy ku am darajay yonant te yonniwun ko ci nit ñi) yonant yi,yepp boo leen boolee ,seenub lim moom teemeeri junni la ak ñaar fukk ak ñeent,yal na mucc ak xeewal sax ci ñoom ci lu dul dog.

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME BIS BU MUJJ BA,yal nanu yàlla fegal ay tiitaangeem )

Ni ngay gëme bis bii mooy nga dëggal ko,te dëggal lepp li mu ëmb,niki wisaareg teere ya,ku ci ne dees na ko won ay jëfam ci teere,ak pang ma,muy dajale gi niy dajale nit ñi,ak balaas bi, muy balaas bi niy mandaxee jëfi jaam yi,ak déegub yonant bi (j.y.m),ak ajjana ak
sawara,ak siraat(aw yoon la wu deesi romb),ak romb gin ciy romb,ak hisaab(mooy seet gi niy seet jëfi nit ñi) ak rammug yonant bi (j.y.m) ak mbugal(yal nanu ci yàlla musal). Hisaab nag luy tar la ca boobale bis,ndax dees na hisaab nit ki ci lu gën a tuuti fepp suuf cib tuutaay.

Fayyantoo itam dana fa am,ndax lu waay daa jay moroomam fii, teg ko cig ëpp doole,bu yawmal-xiyaamee dees na jox aji neew ji doole, doole muy fayyu ci ki ko daa neewal doole,niki xar mi am bejjan te daa daan mi amul bejjan,bu bis baa,da niy jox aji ñakk jiy bejjan bejjani mi ko daa daan muy fayyu,loolu lepp maandute ga fay am lay wone.

Dee,ak laajug malaaka yi ak mbugalum bammeel,ci yawmal-xiyaam lanu,ndax kat yawmal-xiyaam yi ñaar lanu,bu mag ak bu ndaw,bu ndaw bi mooy dee gi ñepp di dee,bu mag bi di wal gi niy wal buftu bi .

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME DOGAL BI)

Gëm dogalub yàlla bi mooy dëggal ne lépp lu am,moo xam lu làqu la walla lu feeñ,ak fu’m man a ame,sunu boroom mooy ki ko xamoon ,namoon ko am kàttanug def ko ,def ko.Moo xam lu baax la niki jëfe ndigëli sunu boroom yi,walla lu bon ,niki jëfe tere yi.Walla muy lu neex niki yoolub jullit ñi,walla lu naqari niki mbugalum yéefar yi.

Cig gàttal daal lépp lu am,ci saayir ak ci baatin dogalub sunu boroom la.Nit ki daal war naa gëm ne amul kuy jeexiital ci dara ku dul yàlla,lu fi am cib dogalam la ame.  

(BUNT CI LISLAAM)

Lislaam mooy wax laa ilaaha illal laa (muy yàlla rekk ay buur,amul beneen buur bu dul mom) ak julli ak woor,aj màkka,natt asaka.

(DOGGANTAL CI LAA ILAHA ILLAL LAA)

Wax laa ilaaha illal laa amul benn buur bu dul yàlla,Muhammad,yonantub yàlla’a - yal na yàlla dolli xéewal ak mucc ci moom,ak ñoñam aki sahabaam- mooy ngën ji lu kuy wax di wax,ku ko weddi it pert rekk,ku ko saxal tey teewlu maanaa mi da na tonowu,te du dajeek nëx-nëx.

(BUNT CI JULLI YI JUROOM)

Julli yi juroom farata la ci lu dog,ci alxuraan ak suna ak ci dajeg boroom xam-xam yi. Kepp ku ko bañ a def ngir weddi,mook ku tubbee yam cib àtte,dees koy tuubloo may ko ñatti fan,bu tuubee nu ba ko,bu tuubul,sariiya ray ko ci jaasi,te deesu ko sang,deesu ko sàng ,deesu ko jullee te deesu ko suul fa jullit ña. 

Imaam daal day yonni kenn rekk, mu suul ko,te dunu ko jublule xibla,te alal ji mu am it ci baytul maal lan koy def (baytulmaal mooy (trésor publique) bu nguurug lislaam),ku nangu ne julli lu war la ba noppi lànk ne du ko def,te amul ngànt,moom danu koy bàyyi  ba waxtu julli wi jot,nu digal ko,bu lànkee nu muñal ko ba doroora ji dem bay bëgg a jeex,nga xam ne lu tollu ne benn ràkkaa rekk  a ciy bëgg a des,bu bañee nu topp ko,ba mu wóor ne faatiya sax xajatu fi,walla ab yamoo,loolu lepp nag ngir bañ koo ray, ñongal dereetam,bu bañee, kilifa gi ray kook jaasi ,rayug gëtën mu bañ a doon ni nuy raye ab yéefër.

Bu réccoo  nag ne nan ko ba mu julli ngir ragal a dee,
deesu ko nangu,dees na ko jullee nag,waaye boroom ngëneel du ko jiite,ndax da nuy bañ keneen di ko ci roy.Bàmmeelam nag dees na ko fonk,jégénal ko(jal ko) kenn du ko maasale noonu rekk,ndax moom fi boroom xam-xam yi ab julit la.Lii dey waxi imam Hawfii la.

(DOGGANTAL CI LAAB)

Laab moom lu war la,ci alxuran ak sunna ak dajeg boroom xam-xam yi. Ku ko bàyyi ci lu dul ngànt lu xel nangu,dees koy ray rayug gëtën,gu dul gu yéefër,
ndaxte julli du mat mukk lu dul dafa ànd ak lab kon ag waram lu wér la.

(DOGGANTAL CIG SOÑÑEE CI  ÑU FARLU CI RÀÑÑALE DIGGANTE FARATA YEEK SUNNA YI AK ÑÀKK  CEE SÀGGAN)

Koo xam ne julli na ca anam ga mu gën a rafete,
ci maanaa,mu jullee ni ko yàlla digalee,metal rukoo ya ak sujood ya,metal taxawaay ya ak jataay ya,te bawul dara lu nu war a def ci julli gi,mu noppi nag nu laaj ko li julli gi am ciy farata akub àtteem, ndax moom julli gi farata la walla sunna walla lu nu sopp,te moom xamul dara ci li nu ko laaj,xanaa mu tontu rekk ne man daal da may gis nit ñi ñuy jaamu ma ànd ak ñoom ca la ñuy def waaye li ci des xawma ci dara.

Ci loolu yenn boroom xam-xam yi nee nanu julleem gi baaxul,te dunu nangu ngàntam li.
Naka noonu ku jàpp njàpp mu sell,raxas ñatti yoon ay loxoom ba ci tikkujara yi,gallaxndiku gu ànd ak soccu,saraxndiku,fiiru,lu ci ne ñatti yoon raxas kanamam,ay loxoom lu ci ne ñatt,te xaliil baaraam ya,masaa boppam tàmblee ko ci fi jë bi yam ba ci doq gi,delloosi ko ba fa mu tàmblee woon,masaa ñaari noppam ginaaw bi mu tooyalaatee ay loxoom,raxas ñaari tànkam ànd ak xaliil leen,matal njàpp  mi ni mu ware.

Naka noonu ku sangu janaba ni mu ware,raxas ñaari loxoom ñatti yoon ba ci tikkujara ya,raxas li ko taq ci sobe,raxas pëyam walla sakkaraam ànd caak yeene,bu noppee jàpp njàppum benn-benn,xaliil mbooleem kawaram,tooyal ko,tamblee ko ci mujug ndaal-bopp li ngir jañ lor ji.
Dal di raxas boppam ci ñatti tanqi ndox yum tanqe ci loxoom,ginaaw bi mu ko xaliilee,dal di as ndox ci tenqul ndijooram,jengal boppam raxas noppub 
ndijooram,bu jàllee mu defaat noonu raxas bu cammooñam,dal di raxas ag doqam,ak wetug ndijooram ba ci bëtu woom bi,def noonu ci gu càmmooñ gi,dal di raxas tankub ndijoor bi ba ci dajoor bi,teg ci bu càmmooñ bi,dal di matal am cangaayam ci raxas biir bi ak dënn bi,ginaaw bim raxasee ginaaw gi.

Te xamul ci loolu lepp la cay farata ak la cay sunna,
kon na ko wóor ne tojam ma (toj mooy ñàkk a lab) dañul te julleem ga mu ca julli baaxul,te coonaam boobu bepp du ca jële lu dul bàkkaar, te mi ngi moy yàlla ak yonentam bu sel bi (j.y.m) .Wax jii nag mi ngi bawoo ci Imaamul Hawfii, luy tiitloo tey jàjjee ngi ci nag,nee na itam gépp jaamu yàlla gu nu defe nii njariñ du ca juddoo,moo xam aj la walla jihad walla woor walla yu ni mel niki joxe ak lele.

Am nag ci boroom xam-xam yi ñu ci ne ku sangu mbaa mu jàpp,def ko ca anam ga mu ware,yeene ca biir def la yàlla farataal,na xam ne jëfam ja ju nu nangu la, ju baax la,te dana ko doy ca la gën a wér,te julli gam ca def it gu baax lay doon ,bu ca yeenee def la ca yàlla farataal,amul it benn bàkkaar ,mbaa muy moy yàlla ngir ñàkk gi mu ñàkk a gëstu.

Waxi Imaam Hawfii jii du dara lu dul ag xuppe akug yeete akug laabiire ,ngir nu farlu ci jeem a xam farata yeek suna ak yi ni mel,yàlla na ko yàlla fay aw yiw. Li ma (sëriñ beey wax) wax mooy yàlla dey araamal na ci mukalaf mu ne - ci li nu tuxal- jëf dara ci diine te xamoo la cay   àtteb yoon,yax (mbind mii) bii nag daliil xathii la,(daliil xathii ci wallug usool mooy lu  wér lu mel ni alxuraan).Kepp ku réere farataam te laajul,na xam ne tooñ na boppam te alag ko. 

(DOGGANTAL CI FARATAY JULLI)

Faratay julli fukk ak juroom la, ci li faqiih bii di Hawfii wax. Ñooy  yii: 1 yeene 2 kàbbarub armal ba 3 taxaw ngir kàbbar ko 4 jàng faatiya 5 taxaw ngir jàng ko 6 rukoo 7 siggi ca rukoo ba 8 sujood 9 siggi ca sujood ba 10 yeenee roy imaam  boo ko amee ca njëlbeen ga 11 toftale gi 12 dal gi 13 yamoo gi 14 sëlmël bi 15 jataayub sëlmël bi tàmblee ca alifug al gi ba ca miimug kum gi. 

(DOGGANTAL CI SUNNAY JULLI)

Ay sunnaam 18 la, 1 liqaam 2 saar wi ci ginaaw faatiya (sunna sun  feddali la) 3 taxaw gi gay taxaw di ko jàng  (sunna sun feddali la) 4 birël fi mu ware 5 yalu fi mu ware 6 kàbbar bu dul bu njëkk bi 7 taaya ju njëkk 8 taaya ju mujj 9 julli gi ngay julli ci yonant bi ca taaya ju mujj ja 10 jataayub taaya ju njëkk ja 11 jataayub taaya ju mujj ja 12  li dolliku ci dal gi ngay dal 13 li dolliku ci sëlmël bi 14 birël sëlmëlub farata ba 15 delloo sëlmël Imaam 16 delloo ko ki ci sa wet 17xerawlug maamoom bu imam dee birël 18  am saatir bu dee imaam walla kenn ku beru,waaye kuy roy moom imaamam doy na ko saatir.

( DOGGANTAL CI FARATAY NJÀPP )

Faratay njàpp juroom ñatt la, ñooy: 1 yeene 2 
raxas kanam gi 3 raxas loxo yi ba ci conc yi 4 xaliil baaraami loxo yi 5 masaa sa bopp 6 raxas sa tànk 7 jonj  8 gaaw

(DOGGANTAL CI SUNNAY NJÀPP)

Sunnay njàpp moom itam juroom ñatt la,ci li imaamul Hawfii wax :1 raxas say loxo ca tàmbli ga 2 galaxndiku 3 saraxndiku 4 fiiru 5 masaa sa ñaari nopp 6 tooyalaat say loxo bala ngaa masaa say nopp 7 boo masaa sa bopp ba ci doq gi,delloosi gi nga koy delloosi 8 toftale gi.

(DOGGANTAL CI FARATAY SANGU)

Faratay sangu joroom la : 1 yeene booy tàmbli 2 jonj 3 gaaw 4 xaliil kawar gi 5 nal ay lett ci kepp ku lettu

(DOGGANTAL CI SUNNAY CANGAAY )

Ay sunnaam ñeent la: 1 raxas loxo cig tàmbli 2 galaxndiku 3 saraxndiku 4 masaa ker nopp yi.

(DOGGANTAL CI FARATAY TIIM)

Faratay tiim juroom ñatt la: 1 yeene 2 pakk bu lab 3 gaaw 4 door gi ngay njëkk a door say loxo ci suuf 5 masaa sa kanam 6 masaa sa tikkujara 7 jokkale ko ak julli gi 8 defe ko ci biir waxtu wi,ndax du baax bu jotul. 

(DOGGANTAL CIY SUNNAAM)

Sunnay tiim ñatt la : 1 toftale ga (mooy jiital li war a jiitu li ci war a top topp ci) 2 doorub ñaareel bi ngay door sa loxo ci suuf 3 masaa li top ci tikkujara yi.
Na nga ba tiim nag tey jàpp,boo weree waxunu boo weredee walla nga am ngànt lu wér,kon bu boobaa nga man a tiim.

(DOGGANTAL CI WOOR)

Woor ñaari farata la am: 1 yeene 2 ba liy dogloo ngir yàlla.
Sunna yi ñatt la : 1 gaaw a dog 2 yeex a xëdd 3 ba wax ju ñaaw

(DOGGANTAL CI ASAKA)

Asaka moom ñeenti farata la am : 1 yeene 2 matug at 3 matug nisaab 4 bañ koo joxe feneen te fi nga ne ku ko yayoo nekk fi.
Am na ñatti teggiin nag yuy waralub yool  :  1 nga ànd ceek teeyug bakan 2 mu bañ a doon la gën mbaa la yées ci sa alal 3 joxe ko ci sutura ngir daw gistal.

(DOGGANTAL CI AJJ)

Ajj ñeenti farata la am : 1 yeenee ajj 2 tawaaful ifaada 3 dox diggante safaa ak marwa 4 taxaw arafa.

(DOGGANTAL CIY SUNNAAM)

Sunnay ajj fukk ak ñaar la :am na ci ñeent yoy ñi ngi ame ca armal ga,1 sangu gu jokkook armal gi 2 rafle ci lunu ñaw 3 solub ñëkk akug làmbaay aki dàll 4 labayka.

Tawaaf gi am ñeenti sunna : 1 dox gi 2 foon gi doj wa ci loxo walla gimiñ 3 ñukk  gi ci ñatti tuur yu njëkk yi 4 ñaan gi ngay ñaan ci tawaaf bi.

Dox gi safaak marwa it am ñeenti sunnaam : 1 foon doj wi bu dee daa juge ca jàkka ja jem safaa 2 ag yeegam diggante safaa ak marwa 3 gaaw gi niy def ci batnu masiil 4 ñaan gu amulub àpp gi ngay def ci kaw safaa ak marwa.

(LII AG MOTTALI LA )

Nettali nanu jële fa gën ji mbindeef ne  ku birël ci ginaawug laab ne ( Ashadu ba fam yam) da nanu ko ubil bunti àjjana yi, mu dugg ci bi ko soob,waaye wuute nanu ci jamono ji nu koy ubbi. 

(DOGGANTAL CI NI NGAY FAYE LI LA FAAT CI GINAAW IMAAM)

Lu war la ci maamoom mu fay li ko fat ci ginaaw imaam.Suba waxtoom a ngi tàmblee ca dëgg-dëggi fajar ba bu tàmblee leer,bu la cib ràkkaa faatee jugal ci lu dul kàbbar jàng faatiya’akuw saar cig birël te bul xunoot.

Waxtuw tisbaar tàmblee ca sawaal ba ca mujjug taxawaay ba,bu la cib ràkka faatee jugal ci lu dul kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig yalu   jekki,taaya ,
sëlmël.Boo ci ñàkkee nag ñaari ràkkaa jugal te kàbbar te jàng faatiya’akuw saar cig yalu,te bul toog da ngay jug def beneen, julli gi mat.

Bu la ci ñatt rawee nag jugal te bul kàbbar,nga jàng faatiya’akuw saar te yalu leen,nga jekki,
taaya,jug def beneen ràkkaa,bu ànd ak faatiya’akuw saar te doo toog,da ngay defaat beneen ràkka rekk cig yalu bu ànd ak faatiya dong,mu jeex.

Waxtuw tàkkusaan a ngi tàmblee ci matug taxawaay bu njëkk ba,ba ca waxtuw gel wa (mooy bu jamono tàmblee mel ne lu mboq). Tàkkusaan mook tisbaar a yam ci ni nu koy faye araf ci araf.

Timis moom waxtoom a ngi dale ci jànt bu so ba ca fàddug safaq. Bu la cib ràkka rawee jugal,kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig birël,bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal te bul kàbbar, jàng faatiya akuw saar te birël ko,taaya, defaat ràkkaa bu ni mel te sëlmël.

Gee moom mi ngi tàmblee ca fàddug safaq ba ca ñatteelub guddi (guddi gi bu nu ko xaajoon ñatti xaaj benn xaaj bu njëkk bi) bu njëkk bi.
Bu la ci benn ràkkaa rawee jugal, bul kàbbar,jàng faatiya akuw saar te birël ko,bu jàllee nga jekki te taaya te sëlmël. Bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal kàbbar te jàng faatiya’akuw saar,cig birël,te bul toog,nga defaat na nga defoon ca bu njëkk ba. 
Bu la ci ñatt rawee,jugal birël faatiya’akuw saar,ci lu dul kàbbar,jekki,taaya,te jugaat defaatub rakkaa ànd ak faatiya’akuw saar,cig birël,waaye doo toog,da ngay wéy ca ba ca des, jàng ca faatiya  rekk te yalu ko.

Boroom xam-xam yi ñoom, jotub rakka ñi ngi ko teg ci am ab rukkoo cib ràkka ànd ak Imaam .
Ku amul ab rukkoo ci ràkkaa ànd ak imaam ,na ko woor ne jotul ràkkaa ba.Ku jot Imaam ci taaya,daa war a dooraatug julleem.

(BUNT CI LIHSAAN)

Lihsaan mooy nga jaamu yàlla di ko teewlu ba mel ni da nga koy gis,ci lepp li ngay def,te mu wóor la ne boo ko gisul it moom mi ngi lay gis.Kon na ngeen koy fuglu.

Bu ngeen bëggee àgg ci martaba yu kawe yi,na ngeen di jëfe ndénkaane bile: maa ngi leen di denk xam-xam,ak kersa,ak sant yàlla ak sellal,ak tabe,ak noppeek lewet booy xamlu, ak muñ ak ragal yàlla ak degg-degglu maanaa yi,na ngeen di farlu ci top aji yërëme ji, fu ngeen man a ne te sori noonoo,bu leen baril wax aki nelaw, na ngeen di teet luy waral yaq, di moytu ngistal,fu ngeen man a ne,ak rëy ak mbañeel, tey sàkkug leer,maa ngi leen di denk ag dëggu, ak wakkiirlu ci yàlla,ak toraxlu ak neewi mebët,denk naa leen bariy teggiin,loolu da na waralub yool,barib xam-xam ci lu duli teggiin ay akub coona rekk lay waral.

Yeen gone yi bu leen di toog ak ku dese cim xel,dee leen toog ak kuy gindee. Kuy gindee kat mooy kiy genne aji toogaale ji jële ko ci juroomi mbir jëme ko ci juroomi mbir,moo koy jële ci ngistal jëme ko ci sellal te du naafeq,moo koy jële cig rëy yobb ko cig toroxlu ak muñ,moo koy jële cig noonoo,jëme ko cig laabiire,moo koy jële ci sikk,yobbu ko ci yaqiin gu ko man a dollig kawe,moo koy jële ci bëgg lu koy lor,jëme ko ci lu koy jariñ.

Màng (profitoo) leen juroom,njëkk juroom ni ko yonant bi (j.y.m) digalee:bi ci njëkk mooy ag ngone njëkk màggat,2 wér njëkk wéradi 3 am koom njëkkug ñàkk 4 ag féex njëkkug féexadi, 5 dund njëkk dee.Gaawantu leen jëm ca yiw wa njëkk muy faat.

Fii la Tasawudus sixaar yam,ànd ak sant sama boroom miy aji feg ji gacca.Woy naa ko nag ndir jëmmi sama boroom mu tedd mi,di yaakaar ci moom ab yool bu dul dog,mu diw woy wuy wommate jëme ci xam-xam ak jëf,ak tegginu tey jàppndal mebat yi.Mu diw rajas wu am njariñ te barkeel,wu way texe yi bokk.

Yàlla ci barkeb yonant bi (j.y.m) nangu na woy wii,jariñ ci it kepp ku texe,kuy laabiire,te yewwu ,moom woy wi du dañ di bijjee jëme cig baax,di jañ gepp texeedeek woru.
Yàllaay ki ma digal ma woy ko,yàlla miy ki nu jublu,mi may fegal luy waral njàqare.Woy naa ko ngir jëmmam ju tedd ja,moom mi jënd samam njaay ànd ak di ma teral.

Konug cant ñeel na yàlla,xeewal ak mucc yal na nekk ci Ahmadu ,aji rammu jiy boroomi ngëneel,ak ñoñam aki saabaam.Ahmadu mii dib jaam buy ligeeyal yonant bi mi ngi sant boroomam.

Subhaana rabbika rabbil hizzati hamma yazifuun,wasalaamun halal mursaliin,wal hamdu lillaahi rabbil haalamiin.

(LII AG XAMLE LA)

Bokk na ci njariñi woy wii : ki ko woy (muy sëñ bi) ci ndigalul yàlla mu kawe mi te sell la ko defe ,ak ci lol yonantam ba jàmm ak xeewal yal na sax ci moom.Bokk na ci ngëneeli woy wi, begal gun ko begal bim ci noppee(moom sëñ bi) ne ko woy wii de la yàlla (t.s)ak yonant bi(j.y.m) gën a sopp ci ay keman.
Bokk na ci li nu ko begale:kepp ku ko jàng walla nga mokkal ko,texe ag texe gu texeedi dul toppati,bokk na ciy jagleem ku ko mokkal Munkir ak Nakiir dun ko laaj ci bàmmeel,ak leneen ak leneen ak leneen,yàlla mooy jagleel yërmaandeem ku ko soob,yàlla mooy boroom ngëneel lu màgg li. 

#Article 64: Liggéey (ci muridulaa) (2165 words)

Bii jukki bu am solo la, ñu def ko ci cawarte gi murit yi ame ci wàllug fàggu ak koom-koom, ñi ngi ko jële ca yëglekaay gu siw googu di The Economist, di genn këyitu xibaar gu gore guy génn ayu bis gu nekk, te adduna bepp xam ko, muy wax nag ci mbiri adduna bi bepp, moom nag mi ngi njëkk a génn ci satumbar 1843.Economist Newspaper Limited (Filiale de Pearson) ca London moo ko génne. Li ñu ci gën di wax nag mooy koom-koomu adduna bi, politig, jëflante, xaalis, xam-xam, xarala ak fànn (art). Lim bu ci génn, di nanu ci defar lu ëpp milyoŋ, te 80% ba ca biti Angalteer lanu leen di jaaye-ji. Yëglekaay gi tas na ci lu tollook 1.138.118 ciy yax  ci xaaj bu njëkk bi ci atum 2006, ci li gëstug bureau of circulations wax, di jumtukaayub natt bu nekk ca Angalteer. 53% ci ñiy jënd yëglekaay bii ak di ko yër ay waa Amerig lanu, 14% ay waa Angalteer, 19% di ñu dëkke Tugal gu goxe gi (continentale). Yëglekaay gi dees na ko yër ci lu tollook 206 réew.

Faith in the market (ngëm ak yaxantu)

Ci ginaaw luumay Itaali yi nuy defe fu lenn dul tiim lu dul asamaan si, am mbooloom jullit mu Afrig a ngii di indi ay tontu ci li nuy tudde “addunaal” di (mondialisation)

Kepp kuy door a teg tànkam  ci suufus Rom, péeyub Itaali, dana gis ne dëkk bii de sol na mbubb mu bees mu mel ne du manu ko xame woon, mbubb mii nag mujj na di mu ñu ko xàmmee ni nu ko xàmmeek baaram yeek tànganaam yi nga xam ne dees na fa faral a guuxe leeg-leeg as lëf ci lii di Cappuccino, di kafe gu nu jaxaseek meew te nu gën a miinew jëfiinam ca Itaali. 
Bu ngéen jëlee yoon wi jëm Vatican, jaare ko ci Via Della Conciliazione mu dim mbedd mu ca jëme, da ngéen gis ne lu bari ca peggi tëli ya de danu koo muure aki jaaykat yu bawoo Afrig yu lay wër aki maska yu ndaw yu (waso), ay saag, ay der (ceintures) walla ay weeri jant yu nu roy, maanaam yu doonul piir.
Bu ngéen fa taxawee as ndiir nag di léen seetlu, bu ngéen moytuwul, da ngéen fa seetaan powum muus ak jinax, mi nga xam ne jaaykat yii baaxoo nanu koo def ak takk-der yi, mu dig (dàqante gu xoromu te yërëmtalu). Nii daal lanu koy nekke, saa su nu léen yëgalee ne takk-der yaa ngoog, da nga leen di gis ñu taxañ seeni bagaas cis lëf cig gaaw daal di laxas, seeti nu nu man a mucce, bu Yàlla dogalee rëccuñu, bu booba a seen yoon du nekkati ci seen njaay moomu, moom kay danu ko fay bàyyil takk-der bi leen jàpp mu dajaleel ko boppam, daal di leen yobbu. (…)

Ca dëgg-dëgg, jaaykat yii nekk ci yoon yi jëme Vatican man ngaa wax ci ñoom lu nekk lu dul nosuwunu (organisewuwunu).
Ñoom de ñi ngi bokk ci kuréel gu nosu, gu nu xame ci adduna bi ci gëm-gëmu diine ak bu koom-koom, te am it ab barabam ca beneen dëkk bu tedd di Tuubaa, nekk nag ci digg Senegaal, boo fa jëmee nag juge Dakar péeyub Senegaal ñatti waxtuy tukki rekk lay tollool. 

Niki yeneen imigire yu bari yu Senegaal (yi nga xam ne yenn yi ay dawalkati taxi lanu ca New York, walla ñu diy wattkati suraas (orange) ca Espaañ) jaaykat yii di wëndéelook seeni njaay ca Rom ñi ngi bòkk ci genn kuréelug jullit gu tasawuf nu koy wooye “yoonu murit”, mooy yoon wi ëmb taalubey Cheikh Ahmad Bamba yi, kii nag ag kilifag diine la gu làqu atum 1927. ñoom nag ci jeexitalu gi nu def ci njàggalem Sëñ bii, indi nanu ay tontu yu am solo ci laaj yi ja  yu adduna yi di indi aju ci ay marsandiis aki ligeey (maanaam dugal nanu seen loxo bu baax ci yaxantu gi ci adduna bi).  

Li ëpp ci 11 milyoŋ yi dëkke Senegaal ay jullit lanu waaye lu ci ëpp danuy bokk ci benn ci ñaari yoon yu mag yii di wu Murit mbaa wu Tiijaan, moom nag (yoonu Tiijaan) moo fi jiitu wu Murit. Bamba moom leeral na am njàggaleem mi nga xam ne ñi ngi ko xame leegi ci turu ((ag murit)) leeral na ko ne mooy ag dellu rekk ca cosaanul Lislaam, gas reen ya, xame ko na ko Yonnat ba indee woon. Waaye nag moom Lislaamam lu néew la nirooleek ju xaw a tar ja bawoo Araabi Sawudit. Lenn nag am na mooy murit yi danuy xaw a def li nuy wax (culte des saints et de leur tombeaux ) muy ci maanaa jaamu wàlliyu yi ak seeni bàmmeel  ba ci bu seen sëriñ boobu sax, te loolu ñoñ Wahaab ñi danu koy weddi, di ko kontar. Waaye murit yii nga xam ne danoo doylu ci seen bopp yëgunu sax ne ñi ngi wax ak a weddi (ñoom wahaabit yi), ñoom daal danuy dajale seen alal def ko ci li nu bëgg, tabax seeni jumaa aki jàkka te dunu soxlaal ñii di waa Araabi Sawudit dara ba dara booloo jeex.   
Sheex KA di sët ci Bamba, ca biir këram ga nekk Tuubaa, di dëkk bu fees dèll ak ragal-Yàlla, waaye it di bu nu bàyyikoo fu nekk dëkksi fa, ag yaxantu gu lokaal di fa dox bu baax ak a naat ci wàll goo wëlbati sa bët jëme, moom Sheex KA mii leeralal na nu gisiinu sëñ bii nga xam ne mooy sukkandiku ak wéeru ci sa bopp: (( bu ngéen wéeroo ci keneen)) mi ngi nuy leeral (( du ngéen gore mukk, lii mooy sunu gisiinu dund)). Bi mu fi daataa juge Bamba mébetoon na ay mbir yu bari: bëggoon na Tuubaa, dëkkam bi mu sanc, nekk dëkk bu sell. 
Njabootam gi – ci déggiin wu yaatu wi – Mbàkke-mbàkke yi, ëmb na lu sakkan ciy sëriñ wallay jànglekati xam-xami diine, yuy boole jàngale liyeey bu tar ci seenum njàngale ak temb, maanaam bañ a wéeru ci kenn ak dimbalnte. Xalaat yii nag moo jàñ murit yi ci ñuy faral a tukki ak a tuxu di dem ci yeneeni réew ngir wëri ligéey, ngir man a yonnee seeni njaboot lu nu man a dunde man cee suturloo, ak ngir man a jox àddiya seeni sëriñ (sii nga xam ne ñu ci ëpp danuy faral a tukki di wër adduna bi, ngir nemmeeku-ji seen taalube yi) ak ngir suqali dëkkub Tuubaa bi.

Lii lépp nag jëf na ay jëf ci def murit yi ñuy benn ci kuréeli Afrig yi gën a tèkki, moo xam ci seen réew la mbaa feneen. Fu ñu nekk ci adduna bi rekk dananu jeem a booloo ngir jënd jàkka walla barabub daje. Seen dimbalante gi nuy def tax na ba ñu bees di man a tukki bay man a ligeey ak a ami këyit. Ci safaanub ñu nekk fi di ngàññ dogal bi ak a jàmbat, ñoom daal yaxaantukat yu sawar lanu te muus, yuy dugg ci ligeey yu yombadi yi nga jort ne dunu ko man, te fu nekk it ci adduna bi danu fay dem di def senni ligeey. Nan jël ku mel ne Aliyun KA, ab bitig la am buy def njaayum bëbëstan (vente en gros) ca wetu gaarub Rom ba tudd Termini. Moom rakk la walla mag ci Sheex KA mi nekk Tuubaa di topptoo njaboot gi. Aliyun KA mii jaaykat la buy def njaayum ay maska yu waaso di ko jaay nag ay moroomi senegaleem yuy jaay di wër ( walla sax ñu duli senegale ), bu ko defee ñoom ñii di ko jaayaat ci mbedd yi walla ci tefes yi. Lenn nag ci njaay mii Senegaal lay bàyyikoo wayye li ëpp day bawoo Endonesi, Thailande mbaa End.

Teewul Aliyun nangu ne am na leeg-leeg ay jaaykati imigre yu juge ci yeneeni réew yu gën a muus murit yi ci di indi njaay walla jaayiin wu bees. Moom nag Aliyun, ku naw ñenn ci ñiy wujjeek moom ci njaay mi la te juge Banglaades, ndax nee na ((ñoom danuy déglu xibaari jawwu ji (meteo) ba bu nu nee suba di na taw rekk ñu gaaw wuti parasol jaayi ! )). Am na benn yoon ci mbedd mi, Sang Ka def fa nuyyoob taalube bu tàng ak ay mbokki muritam yu def am mbooloo mu rafet tey jàpplante. Jaaykati saag yii ak der, nga xam ne yu ci ëpp Siin lanu juge, ñu ligeeye leen fa, danuy faral a daje ngir weccante seeni xalaat ak xam-xam yi aju ci ni nuy lijjantee bay mucc ci takk-der yi. Bi añ jotee, gan dikkal na Sang Ka, di benn waa reewam N. GEY, mi nekk ci bunt bitigam tey jaay ay tòggi Senegaal yu tàng, plaat bu nekk 5 euro.  

Benn yoon ci ayu bis gi, lu ëpp ci murit yi nekk Rom dananu daje ngir def daayira (julli, jàng Alxuraan aki Xasida), gisante, siyaarante,xool ci seen biir ki ci yayoo ndimbal. Leeg-leeg as mbooloo ci ñoom danuy déggoo ci bokk luye ab kontaneer , yonnee ci seeni njënd aki bagaasi jëfandikoo, ngir nu jaayaat leen ca Sandaga, ja bu nekk ca Dakaar, te murit ya ëpp fa. Ay anam yu wuute it am nanu yu niy yonnee xaalis, looloo tax këri ligeey yiy yëngu ci wàllug yonnee xaalis yu tas lanu ci mbooleem ruqi Senegaal. Waaye imigre yi ñoom li gën a noppale ci ñoom te nu gën koo taamu ak a def mooy: woo seenub xarit walla xame ca Sandaga ngir mu joxal leen seen mbokk ma soxla.

Ñi ngi nattale ne murit yi tollu nanu ci 40% ci askanu Senegaal wi. Waaye bu dee ci bitim réew ñoo ëpp ci imigrey Senegaal yi nuy tollale ci 700,000 . Murit yi it ñooy daanaka 80% ci jaaykati Senegaal yiy wër, tey jaar ci mbooleen qàli Itaali yu mag yi. (Fraans mi doon dooley sancaan  ji tegoon loxo Senegaal mujj na doonatul réew mi senegale yi jëme séen një. Ay fukki at a ngii Itaali nangu barabam boobu ci moom, waaye nag jamono jii ñu nekk Espaañ a ngi jéegoy jéego ci fuqarcee ko ci Itaali. Lii sax moo waral ci weer wi (desambar 2006) lu jege 80 waa Senegaal ñoo sànku ci ndox mi, ci séen gaal gu laboon te jëmsi woon Espaañ, ca dunam ya tudd Canaries).

Lu bari ci murit yi danu lay wax ne di jaay di wër moo leen gënal ñu sax fi barab di ligéeyal kenn. Loolu nag ci genn anam day wone ni njàngalem sëñ bi jeexitale ci ñoom, te mooy sukkandiku ci sa bopp. Lu man a xew nag, ñu néew ci ñoom a mas a def ay tooñaange yu mag. Bis bu amee ay këyit ak visa day daal di dellu kër ga, def fay weer. Te sax ci mujjug at mii rekk ñu bari di nanu dellu réew ma ngir tëbëski-ji, bu ko defee ñu ci ëpp danu fay des ba weneen xewu diine wu mag wa ñëw di Màggalug Tuubaa, bu ko defee nag bu jàllee ñu door a dellooti Tugal ci jamonoy lòlli.
Jenn ci dooley murit yi mooy seen nosu gi  nu def ci wàllug njiit. Ñoom de bu ñu doon ab jal da nga naan Xalifa ba a nekk ca njòbbaxtal la, di aw turu njiit wow ki ko yanu fii mu nekk mooy Sëriñ muhammadu lamin baara mu Sëriñ Fallu. Kii daal mooy ki nga xam ne lu mu wax rekk ñu def ko. Cig ayam Tuubaa gis na ag yaatal gu jéggi dayo ba. Ci atum 1958 bu ña fa dëkk weesuwutoon 2000 nit, leegi àgg nanu – man nanu ne -  ci ay 700,000 nit . Alkol nag ak Póon danu leen a aaye ca Tuubaa , moom dëkk bii nga xam ne daa xaw a moom boppam ci biir Senegaal. Ña nga fay taxawal daara ju mag (ab université). Boo ko doon nattaleek yeneen dëkki jullit ñi fa la ag féex ëppe ak doxe na la neex ci diine. Jigéen ña dunu sol pantaloon waaye dunu muuru it, ñu ci bari it dunu musóoru. Xale yu góor ya’ak yu jigéen yaay demandoo jàngu ba (école). Saa su nu wootee ngir ñu defar ab fajuwaay (hopital) mbaa woote bi jëm ci lu defar ndox mi, ay milyoŋi eurooy dajaloo, ngir ne murit yu bari ay way woomle lanu, ku ci mel ne Elhaaji JUUF may futbal ca Bolton (Angalteer), ndax moom joxe na ca la ñu doon laaj ngir ligéeyub Tuubaa ba (…)
Xamagunu leen de bu baax, waaye murit yii bari na lu adduna bi man a jànge ci ñoom de, du rekk ni nu war a def ba jàmmaarlook li nuy wax mondialisation (di ci maanaa jël adduna bi bepp def ko daanaka menn réew, benn xalaat, xatal soreente yi, jegeele gis-gis yi añs), waaye it warees na a jànge ci ñoom ni nuy doxale diine ci anam gu teey te jàmme…

#Article 65: Jëmm (245 words)

Jëmm “fii muy tekki physique” baat la bob ci gereg mooy φυσικη maanaam «fisikus» di ci wolof“kojug dénd”,moom nag mi ngi juge ci reenub φύσις «dénd». Kon «jëmm» mooy xam-xamu dénd. La ko dale ca kawaarig yi nga xam ne nu ñu tuuteewul amul ba ci nekk(àdduna)gu màgg gu tàlleeku gii,xam-xamu jëmm liy liggéeyam mooy jéem a tëgg ay àtte walla ay yoon yu matematig yuy àtte àdduna bii di bu ne-ne bu dénd,ak lambutu xóot-xóoti ne-ne ak dëgg-dëggi jikkoom ak way toggale(composants)yu mag yi ko toggale, ak doole yu dàttu (fondamental)yi nga xam ne yaram yu ndaw yi dinañu koy joqalanteek yaram yu ne-ne yi, nga boole ci njuréefi doole yii. Leeg-leeg ci xam-xamu jëmm bu bees bi danu ciy boole gëstug “xam-xamu ndendoo” ak bu “wattuwu” niki xam-xamu wattu kàttan ak “jañu”( Momentum ),ak cefkag mbëjj,looloo waral boroom xam-xami jëmm yi lu bari lanuy faral a gëstu ci feeñtey jëmm yi, dale ko ci ëtt yu yaatoodi yi ba ci yu yaatu yi, dale ko ci yaram yu ndaw yi nekk ci ron saal walla xartil, nga xam ne ca la mbooleem ne-ne yu baaryon yi di ame “jëmm bu yaram yi” ba ca gëstug sóobu walla jikkoy yaram yu jëmm yi ca adduna ju yàgg ja, ba ci jàng yëngu-yëngu gu bidiw yi ci asamaan su ne-ne si, moo xam ci biir gaawaay yi nu xam la walla yi jege gaawaayu leer, ci mujjantal gi, gëstu nekk gi (adduna bi) ci léppam.

#Article 66: Yewwute (3769 words)

Yëngu-yëngu googu nag mi ngi tàmbali ci xarnu bu fukk ak juroom ginaaw juddu gu yonnant Yàlla Isaa (XVu xarnu balla Isaa), ba ci bu fukk ak juroom ñaar (XVII), mu sos fi nag ay coppite yu xóot ci wàllug aada, dundin, mboolaay, politig ak koom-koom. Kon daal, yewwute gii amoon ca jamono yooya ca Tugal, li muy wund mooy ag tuxu juge ca jamono ju diggu ja (mu'y jamono'y ag laman walla ag cang) dem ci jamono ju yees ji (di ju jëm-kanam gu xam-xam ak xarala).

Sabab yi jur yewwute gii yu bari lañu, waaye nanu ci indi ñatt yi ci ëpp solo rekk, ñooy :

Ci waxtu wi Tugal nekke cig deltu ginaaw, ci wàllug xay ci jamono yu diggu yi, nga xam ne jàngu bi (Egliis bi) faagaagaloon na bépp xalaat bu leer te gore, araamal ci nit ñi ñuy xool leneen lu dul am njàggaleem mu way deng mii te doxadi, bi Tugal nekke ci lëndëmam gii, jullit ñi ñoom ñi ngi doon jëm-kanam bu baax ci yekkati tabaxub seenug xay ci kaw ay cëslaay yu xam-xam ak wisaare maandute ak mbokko ci diggante nit ñi, ci lu dul xool xeet walla melo mbaaw làkk.

Xayug lislaam gi nag àgg na Tugal jaare ko ci yoon yu bari, bokk na ci yooyu, Andalusi ak Sisil ak reewi penkub lislaam bi, rawati na ci xarey jooñe yi(croisade).

Ndax kat booy xool li Tugal di nekk lépp di ku ñu dàqe ca xarey jooñe ya (walla yu galajaane ya), duma ko ca, teewul mu fàggoo ca njariñ lu bari ngir fenqoo gi mu ci defe ak xalaatub lislaam bi, ak nosteg dundam.

Lii nag ci li soppi xalaati waa-tugal yi la jëm ci jàngu bi, nit, adduna bi ak dund gi.

Te itam lu bari ci sàkkukati xam-xami Tugal yi, dañoo tàmbali woon di naan ci xam-xami lislaam yi, ci paj, xeltu, gañcax ak ndundat, ak yu dul yooyu ci jàngu yu Andalusi yi, la ko dale ca xarnub fukk ak benn(XI) (g).

Loolu nag taxoon na ba yëngu-yëngu gu firi walla tekki gu mag amoon ci xam-xami lislaam yi, tukkee ci làkku araab dem ci wu latin (wi doon wu xalaat, wu diine, tey wu politig ca Tugal ca jamono jooja) loolu dimblee woon, ci ginaaw bi, ci lal yoon wi ba yewwute gu Tugal gi man'a am.

Bu ko defee, li ñuy wax tool, di suuf si sang biy moom, moo daa tekki barabu dëkkuwaay bi, koom-koom bi, mboolaay gi, ci gii noste.

Màggug dëkki Tugal yi, ngir màggug yaxantu gi nu daa def ak mboolaayi jullit ñi, ak màggug liggéey yi, ngir jòkkoo gi waa-tugal gi daa def ak jullit ñi taxoon na ba nosteg laman tàmbli woon a lòtt aka naaxsaay, rawati na bi nitug Tugal gi tàmblee am yoon wu mu man a jaar bay dund te du sukkandiku, ci léppam, ci suuf ak tool, waaye ci yeneen ligéey yu koom yi.

Dëkk yi tam tàmblee doon barabi leer yu di boroomi xay, di sonnale ci loolu aka lakkal noste gu laman gi, tey liggéey cig màbbam, def it lu rëy ba yewwute ci Tugal man a am.

Jàngu bi moo nekkoon di teg loxo ci dundug xalaat gi, gu diine gi ak gu aada gi ci Tugal gépp, te yitteem jépp mi ngi ko sottiwoon ci njàngum pas-pasu diney nasaraan, walla li nuy wax njàng yi aju ci Yàlla (théologie), ak njàggat ak xellu. Amutoon jenn yitte ci njàng yi aju ci xam-xam.

Jàngu bi moom dafa jàppewoon boppam ki nga xam ne ci yoon moo war a doxal mbiri politig yi. Te kat (moom Jàngu bi) tawati mbon akug yàqu dañoo ruuroon aw yaramam, dugg ko fépp, ba waral aw nit wu jàng te yewwu jug, taxaw temb ci dañal ñaawteef yooyu ko taqoon. Loolu tam bokk na ci li jañoon xelum nitug Tugal ki ci mu jëm kanam, gën a ñaw, rawati na bi dëkk yi gënee yaatu, degginu ligeeyub yaxantu gën faa xóot, ak bu endustri ak aada. Yii yepp nag liggéey nañu lu rëy ci, waxuma la doyodil ngëb gu tar gi paab gi ngëboon mboolaayu Tugal gu nasaraan gi, waaye it doyodil nosteg laman gi, loolu it, di doyodil nosteg laman gi, rataxal yoon wi ba yewwute gi man a am.

Dëkk yu Itaali yi ñooy mber yu njëkk, yi njëkk a uuf, tete yewwuteg Tugal gi, looloo waraloon ñu am wàccuwaay bu kawe akug wormaal ci yeneen dëkki Tugal yi ca jamono jooja. Dëkk yii niki Milano ak Venezia ak Firenze ak Napoli, ñoo uufoon yewwute gi, seeni boroom xam-xam aki njàggatkat ak ñoñ fànn, duggaloon nanu ci seen loxo bu baax.

Li waraloon loolu nag lu bari la, bokk na ci, dal ga fa amoon ak jàmm ja, ak jëm kanamug koom-koom ba, ak yaatug yëngu-yënguy nitu Itaali ki, ak ba tay, yaatug goxi xalaatam, ak yëg gu mu yëg gore gu mu am, ginaaw bi mu goree ci nosteg laman, ak li Itaali yàgg a am ci teddnga gu sax ak jaloore : mu'y njàggati waa-rom yi, seeni xam-xam, seeni jeexiit ak seeni fànn, nga rax ci loolu nekk gi paab gi nekk Rom, nga xam ne loolu faggul na waa Itaali ag cang gu diine.

Ni nga xame ne barab boobu it (di Itaali) faggul na paab bi ci Itaali ag tono gu neen ak gu maanaa gu mag, nga rax ci dolli gëpplante gu mag gi amoon ci diggante dëkk yu mag yi ak peeyi nguuri Itaali yi, ci wàllug njàggat ak fànn,ak soññ gi doxalkati dëkk yii ak buur yi daa def boroom xam-xam yi daa liggéeyal yewwute gi. Ak ba tay yittewoo gi nga xam ne amoon na ci dëkk yii, aju ci gëstu mbind ak taalif yu yàgg ya, ak barig móolukaayi téere yi ci yii dëkk. Ak nag li Itaali doon xéewoo, muy nekk ci barab bu raññiku, buy dimblee ci jokkoo ak addunay jullit ñi.

Yewwuteg Tugal gi, mi ngi ame ci mbooleem wàlli dundug nit, gu xalaat, gu fànn, gu politig, gu diine, ak gu koom-koom. Yii di ñëw ñoo ciy wàll yi gën a rëy:

Ag nite li miy wund fii mooy dundal njàggat yu yàgg ya (yu Geres ya ak Rom), ak feddali sukkandiku gu nit war a sukkandiku ci boppam, akug goreem ak sañ-sañu wax li nekk ci moom, ak dog gàllankoor yu mboolaay yi, ak jële fi aaday jamono yu diggu yi, ak sotti yitte yi ci adduna bi ak dénd bi, ak jeem a xam seeni mbóot.

Yëngu-yëngu googu nag bokk na ci màndargay yewwuteg Tugal gu njëkk gi, ndaxte li mu yittewoo woon mooy xam-xam yu kojug nite yi nga xam ne njàngatkati Geres yeek Rom (grego-romain) ñoom lañu jëloon, yittewoo leen, ak seeni xeltukat ak seeni boroom xam-xam ak ñoñ fànn ak seen boroom mecce yu muus yi te ñaw. Boroom xam-xam yi daa def gëstu yooyu di kojug nite, ñi ngi leen di woowe ñoñ nite, walla boroom njàngat yi. Ñoñ nite kon ñooy mbooloom nit mi yittewoo woon jàng njàggat, xam-xam ak fànn yu yàgg ya (yu klaasik ya), maanaam njàngati Geres ak Rom ak seeni fànn ak xam-xam.

Yëngu-yëngug nit gii nag judd na, ginaaw bi mu amee ag jàpple gu tukkee ci kilifay dëkki Itaali yi ak seeni boroom alal. Ñoñ nite ñi génne woon nanu ab taar, feeñal ko ci mbooleem fànn yu wuute yi, moo xam yatt la, mbaa nataal, ak deseñ, ak misik, ak tabax. Ñoñ fànn ñu Itaali ñi ak ñu dul ñoom ci jamonoy yewwute, dañu doon roy fànn bu klaasik bi, di bu gres-rom bi, bàyyi nee nag fànn bi nu daa wax xóot, nga xam ne moo amoon ca Tugal ca jamono ju diggu ja. Bu ko defee, ñoñ fànn ñi jëmale seen fànn ci taarub dénd bi ak dund gu yees gii nga xam ne mooy gisiin wu jëm kanam wi nu am ci dund gi.

Ci dëkki Itaali yii, lu bari ciy fànnkat yu siw yi fa lañu feeñe, bokk na ci ñooñu deseñkat bu siw ba, di Fra Angeliko (1400 - 1455), Leonardo da Vinci (1452 - 1519), Titian (1488 - 1572), ak Rafayel (1493 - 1520 g), yattkat ba Donatello (1386 - 1466).

Làkku Latin, ci jamono yu diggdoomu yi, moo nekkoon wa tasoon ca boroom xam-xam ya, ak niti diine ya, ak politgkat ya, ak njaggatkat ya ak ustaas ya. La notoon nag ca nit ña, di woon niti neen ñi rekk, ñoom déggunu woon wii làkk, lu tumbrànke la woon ca ñoom, seen làkki bopp yiy yu seeni barab lañu déggoon.

Bi jamonoy yewwute dikkee, ngelawul fonk sa xeet upp ci Tugal gépp, la lu bari ci xalaatkat yi, ak njàggatkat yi, ak woykat yi, tàmblee jèng jëm ci bind ak taalif ci seen làkki réewi bopp, niki wu Itaali, wu Espaañ, wu Fraans, wu Angalteer ak yu dul yooyu.

Bi mu ko defee, woykatu Itaali bi tuddoon Dante (1265 - 1321) taalif mbóosóor mu Sell mi ci làkku waa-itaali, naka noonu Petrarch (1304 - 1374) mii nga xam ne li mu gisoon mooy làkku Romam wii daal mooy gën ja a kawey jumtukaay ngir génne xasiday woyam yi.

Bu ko defee Miguel de Cervantes moom itam def xisaam bu siw ba di don kixota ci làkku Espaañ, ci noonu it la Rabelais (1483 - 1553) def, moom mi nga xam ne gisul lu gën làkkam wii di wu Fraans, ngir wuññi ci liy yëngu ci biiram, ci njàggat lu fees dell ak xoromu ak mbóosóor (kaf).

Chaucer mi dib waa-angalteer (1342 - 1400 g) jug, moom itam, sotti ciw làkkam woyam yu yéeme ya cib taar, rawati na nettaliy Kentrebry yi, nettali yooyu ñoo ko def kenn ci woykati Angalteer yu mag yi, yi gën a siw.

Màggug fonk sa xeet ak sa reew ci Tugal, juroon na ci jamonoy yewwute, ay reew yu bari ci Tugal taxaw. Yu amoon ag temb, ci noonu, yittewoo xalaati fonk sa xeet daal di fay feeñ, fés fa, lu aju ci temb tam di lu ñu fay waxtaane, ak àttewiin yi.

Dëkki Itaali yi ak reewi Tugal gu sowwu gi ci jamonoy yewwute, dañu doon yittewoo dajale mbind yi ci fi ñu jortoon ne fi lañu nekk ci Xustantin ak ci dëkki waa-geres yi, ak ci yeneen barab yi ci Tugal. mbind yooyu ñu daa wër nag ñooy yu Geres yeek Latin yi nekkoon di lu ñu tas ci kàgguy daara yeek jàngu yi ak jàngu yu mag yi, ak ci nit ñi walla kër yi yittewoo woon mbir mii.

Peey yi daan àtte, dañu daa jagleel lii alal ju bari, ñoñ nite ñi tam ñu ci bari jëmale woon nanu seeni liggéey ci dajale mbind yi, ci noonu ñu jot a am ci misaal rekk, mbindum binkat bii di waa-rom te dib xutbakat, tuddoon Quintilian (35 nj - 96 g) ak bataaxeli Cicero (106 - 43 nj) yu xutba yi, ak woy yu at-ba-at yu Tacitus yi(56 - 120 g). Tacitus moomu mooy taariixkatu xeexi jarmaan yi, mi ngi bokkoon ci ñi gënoon a ñaw ci xutbakati Rom yi ak seeni njàggatkat yu ñaw yi.

(5) Sonn ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya:

Yewwuteg Orob gi yittewoo woon na te sonnoon ci taarix ak jeexiit yu yàgg ya.
Ag jublu gu yees am ci jàngiinu taarix, ñu koy teg leegi ci cëslaayu jam, waaye tegeesatu ko rekk ci dégg ak nettali, ci noonu ab jàngu sosu ci Firenze am njàngaleem jëm ci jam gu taarix, mu tudd daaray xam-xam bu taarix.

Bokkoon na ci boroom xam-xam yi ci gënoon’a duggal seen loxo, nitu taarix kii di Lorenzo Valla (1406 - 1457 g), mooy ki jamoon te diiŋatoon benn wayndare (dossier) bu taarix, sikkoon it ag wéram, mooy li ñuy wax mayug Xustantin, mooy wayndare boobu nga xam ne paab yi yàgg nañu cee sukkandiku, la ko dale ca xarnub fukk ak ñaar (g), ci seen xeex yi nu doon def ak buur yu mag yi ngir feddali ci seen àqi politig ci àtte nit ñi, jiite leen. 

Bokk na ci ñi nga xam ne yittewoo woon nañu gëstuy taarix yi ak yu politig yi, bindkatu itaali bii di xalaatkat bu politig bu am diplomasi, di Nicola Michiavelli (1469 - 1527 g), Michiavelli mii def na teere bu mu tudde woon (buur bi), ndax da ci doon wax lu aju ci buur bu am doole, bu doon bennale dëkki Itaali yi, ak nguur-nguuraanam yu daggatoo woon yi te tas.

(6) Jëm-kanamug yaxantu ak ndefar: 

Yaxantu noyyi na bu baax ci Orob gu sowwu gi,dale ko ci njëlbeenug xarnub fukk ak benn g. Itaali fi mu feete dimbli na ko bu baax ci yëngu-yëngug yaxantu dox fa te jëm fa kanam. Ci noonu lonkoo yu yaxantu yi tàmbli fa’a sosu, di jëli marsandiisi penku yi, niki sooy, ak cuub yi ak rëndaay yi, ak wurus ak bëñu ñay ak yu dul yooyu, ginaaw bi it yii lonkoo - ginaaw bi ñu gënee jëm kanam – tàmblee yòbbu yii silaa ci yeneen dëkki Orob yi, bu ko defee bu ñuy dëpp di indaale marsandiisi Orob yi, niki ngëndal ak der ak firaa. 

Jëm kanamug yaxantu googu ak gu meccey ndefar yi yi, jur nañu ag xereñ ci denciinu alal, akug jëm kanam ci koppar yi ñuy jëfandikoo ci jëfi yaxantu yooyu, ci noonu am mbooloom ay sandikaay mecce feeñ, mujj teg loxo ci ginaaw bi, ci fepp fu koom nekk, te am fa cawarte, naka noonu nu def ay ligeey yu mag ci wàlli mboolaay ak politig ak xalaat, raxaatal ci loolu juddug kuréel gu diggu gi ñooy mbooloo miy ligeeye yaxantu ak yeneen mecce yu wuute yi.

(7) Feeñug yëngu-yëngug xam-xam gu yees gi:

Yewwute gi ci njëlbeen gi dafa sotti woon yitteem ci dundal njàggat yi ak fànn yi, ginaaw bi mu dox as lëf ba àgg ci mbooleem lu xay gu mat laaj. 
Ci noonu yewwute gi matale mbooleem dundug mboolaay gi, bokk na ci, xam-xami dëppale yi, ndaxte xam-xam moom màggoon na ci dëkki Orob yi, jàngu yu mag yi sosu ci Orob gi rawati na ci dëkki Itaali yi.
Yëngu-yëngug xam-xam googu mi ngi tàmblee ci di jeem a dundal xam-xam yu yàgg ya, ginaaw bi mu dox jëm kanam, loolu nag li ko waraloon mooy jariñu gi mu defoon ci yoonu xam-xam woowu di wu kojug nattu, maanaam lu nekk looy wax, nga teg ci sa loxo, mu leer la ne loolu la, nga doog ne moom la, ndax wóore na la ci làmb gi nga ko làmb ba daj ko, yoonu gëstu woowu nag, mooy wi boroom xam-xami jullit ñi jaaroon, ci noonu boroom xam-xamu fisiyaa bu Angalteer bi ñuy wax Roger Bacon (1220 - 1292) feeñ, di njiitul gëstug xam-xam ci Tugal.

Becon mii mi ngi sukkandiku woon ci yoonu jakkarloo ak nattu, ci gëstoom yooyu nga xam ne àggale woon nanu ko ci ay ngérte yu am solo ci xam-xamu bidiw, ak bu weer yi ak yu matematik yi, ak juxraaf.

Naka noonu boroom xam-xamu xeltu ak politig bu Angalteer boobu di Francis Bacon moom itam feeñ (1561 - 1626 g), di koo xam ne dafa jëfandikoo xel ci àgg ci dëgg yu xam-xam yi, ci noonu ci gisiin, mooy ki teg ponki ngérum xam-xam mu bees mi, ak doonte moom doonul woon boroom xam-xamu dénd.
Boroom xam-xamu Itaali bi, Leonardo da Vinci (1452 - 1519 g) moom tam feeñ, di kok dafa yittewoo woon jiyoloji (bu mekanig) ak matematig, ak yu dul yooyu, nga rax ci dolli fànnu yatt, ak nataal, ak misik, ak eeseñëri, mu nekkoon daal boroom xam-xam te di nitu fànn, tey fentkat.
Naka noonu boroom xamu Itaali bii di Galileo (1564 - 1642 g) feeñ, mooy ki njëkk’a defar nattukaayu tàngoor, njëkk’a fuglu bidiw yi ca fesalukaayam ba, dëgëral te feddali gisiinu boroom xam-xamu bidiw bu Poloñ bii, di Copernicus (1476 - 1542 g).
 
Bokk na ci màndargay xam-xam yeneen yu yewwute gi, fentug móolukaayu teere ci loxol nitug Almaañ kii di John Gutenberg, atum 1404 g, fent gii ak doonte gu Almaañ la, teewul jëmale na kanam bu baax dundug nit ci biir Tugal ak biteem. Wuññiy juxraaf yi tam ci màndargay yewwute gi la woon, ak yéwénalug diine gi ci Tugal. Nga dolli ci loolu feddali gu nitug Tugal ki feddali jëmmam jii nga xam ne yàgg na’a nekk di lu nu làq ci jamono yu diggu yi ci biir ay kureel, walla sandikaay mecce yi mu daa bokk ngir làqatoo ca ak aar njàriñi boppam.

Yewwute gi ci Itaali: 

Yewwute gi ci Itaali daa tàmbli woon’a giim ak’a yànnjadi ci mujji fukk ak juroomeelu xarnu g, ak njëlbeeni fukk ak juroom benneelu xarnu g, loolu nag li ko waral lu bari la, ñu jéem cee indi yenn rekk yi ci ëpp solo:

Attekaay yooyu mosal nanu - ginaaw bu àtteb Lislaam dañee ca Andalusi te Garanada nërméelu, daanu - mosal nañu lu bari ci jullit ñi ay xeeti mbugal ak coona lu maneesul’a misaal, bokk na ci di leen lakk ñuy dund.

Tuxug Yewwute gi:

Ak li yewwute gi di neew doole ci Itaali lepp, taxul mu naaxsaay, mbaa mu suux, li am kay mooy da fa’a tuxoo dem ci yeneen reew yu Tugal niki Espaañ, Portigaal, Fraans, Angalteer, Holand, ak Almaañ, añs.
Ay jëfka yu bari bokk nanu ci li tuxale yewwute gi jële ko Itaali yòbbu ko ci yii dëkki Orob, bokk na ci yooyu nekk gu yii dëkk nekk di yuy door’a noppi ci seenug sosu gu politig gu yees, ak tàbbi gu ñuy doog’a def ci jamonoy tabax ag xay.
Ñi daa woote yewwute gi nag def nanu lu rëy ci tuxale ko Itaali mu dem feneen.
Nitug Holand kii di Erasmus (1466 - 1536 g) moo tasoon te wisare yewwute gi ci Almaañ, jaarale ko ci def fa ay waxtaan aki xutba, ak ci yeneen dëkk yu Orob yi.

Erasmus mooy ki firi Injiil jële ko ci làkku Gres yòbbu ko ci wu Latin, jël nag li ñu ciy wax kòllare gu yees gi def ko ci ay làkki Orob yu bees, loolu bokk ci li feexal te goreel xalaatub Tugal bi ci ngartaajoo gi ko niti diiney katolig yi ngartaajoo woon.
Loolu it won na waa- Tugal ne yaxub Injiilub latin, bi egliis bi yoroon du woon biy cosaan, te yax bu bari woon ay yàq la, kon daal Eramus mooy ki waajal xelum Tugal mi ci mu man’a nangu yéwénali diine yi.

Ni yewwute gi meloon ci fu dul Itaali:

Yewwute gi ca Almaañ dafa yoroon melow njàngat, wiy ligeeyal gëstuy diine yi (ci manaa daa yamoon daanaka ci lu aju ci diine rekk). Ca dëgg-dëgg, gëstu yi aju ci xam-xami Gres-Latin yi, dafa xawoon’a yeex’a àgg ca dëkk yooyu di yu Almaañ, ak li njiiti yooyu dëkk daa dimbli gëstu yooyu lepp cig wàll, ak li Almaañ doon am ay daara yu mag ci Vienne ak Idelberg ak Baasal ak Strasburg ak yu dul yooyu lepp, ci geneen wàll.

Yeex googu nag li ko waraloon mooy niti diine yi ak ñu dul ñoom ñoo ko nanguwutoon, ñoom daal danu fee nekkoon rekk di sàkku nu ñu tënke, te jéng yooyu njàng ak gëstu, te defi pexe ba du ñu tas ci anam gu yaatu, ngir nu wattoo ci seen kilifteef, sàmme ci seen daraja, aare ci seen ligéey.
Ci noonu, danañu gendiku ne yëngug nite gi ci Almaañ dafa doon sori jubluwaay yu deet-diine yi, looloo tax du kiimaan Almaañ di woon barab bi uufoon yëngu yu yéwénali diine yi gënoon'a am solo ci Tugal.

Bu dee ci Fraans moom yewwute gi melow njàngat ak nite la fa yoroon, wi yittewoo woon xam-xami Gres yi. Ci noonu boroom xam-xami Itaali yi ak yu Gres yi taxaw ci wisaare gëstuy xam-xami Gres yi, ñu móol teerey ndonoy Gres yi ci móolukaayu Paris ba ñu taxawaloon ca xarnub fukk ak juroom benn g, ni nu duggale seen loxo ci amal ay akaadimi aki barabi xam-xam ngir njàng yi aju ci nite, niki bànqaasub buur bi ci Paris, ñu sos ko ci jamonoy Buurub Fraans bi, di Fransuwaa mu njëkk mi atum 1540 g.

Bu dee ci Angalteer, ba tay yewwute gi ma nga fa yoroon melow njàngat ak nite. Ay gëstu yu xam-xami gres yi am fa, ay ñoñ nite ñu waa reew ma, ñu bari ñooy ña ca siwoon, ñoom ñooy ñi daa jàngale làkkuw Grees wi ci daaray xam-xami Itaali yi, ku ci mel ne Wilyam Lilly mi daa jangale làkkuw Gres ca Rom.
Erasmus mu Olaand mi ak Kolt mu Angalteer mi, ñoo tekki woon Injiil ci làkkuw angale wu bees wi.
Buurub Angalteer bi, Henri mu juroom ñatteel mi, moom tam sosoon fa juroomi toogu yu darajay ag ustaas ci xam-xami pas-pasu nasaraan ak yoonu siwil ak wu dénd bi ak làkku ebrë ak wu Gres ci daara ju mag ju Kembrij. Jàngub San Pool bi nekk London moom it jagoo woon njàng yu nite yi.

Yewwute gi ci Angalteer dafa jublu woon yoonu takk ak boole diggante pas-pasu nasaraan ak gëstuy nite, yu njàngat ak yu fànn yi. Yewwute googu nag indiwul woon lu yees, lu ñu fent, ndare ci xarnub fukk ak jurom ñaar g, bi am njurum njàggatam ak mu niteem mu yees feeñee ci anam gu fes te rafet ci woyi William Shakespeare yi (1564 - 1616 g) ak woykat bu silmaxa bii di John Milton (1608 - 1674 g) ak ñu dul ñoom ñaar. 

Fii tam ci Angalteer yoonu yewwute gi da fee jengoon as lef jëm ci yewwute gu xam-xam, gu aju ci xam-xami dëppale yi walla xam-xami nattu, yu làmb yi.
Ñi jiitu woon ci lef moomu, ñooy ñaari boroom xam-xami Angalteer yii di Roger Becon ak Francis Becon, ñoom daal ca dëgg-dëgg ñooy ñi sos daaray xam-xam ca Angalteer.

Baat bi nuy mujj a wax ci yewwuteg Tugal gi, mooy moom daal moo ñàkkal jamono yu diggu yi kàttan ci jeexiital ci mboolaayu Tugal gi ci wàlli dundug politigam, gu mboolaayam, gu xalaatam ak gu aadaam.

Ngir jeexiit yii fi yewwute gi sotti ci Orob, ay noste yu yees am nañu yu làmboo tabax guur gu yees gi ak mboolaayug Orob gi ci cëslaay yu aada, yu mboolaay, yu jikko, ak yu ngér yu yees, ni mu duggale loxo ba tay ci ubbi ay gox yu yees yu xam-xam, yu jël gisiini xam-xam yi ak dal yu xam-xami juxraaf yi. Lii lépp nag moo sabab jamono ju yees ci Orob,di ju wuuteek ja woon (ca jamonoy laman) ci xalaat, ak ngér ak defiin aki xew-xew.
Loolu lepp nag nga boole ko, moo jur jamonoy Tugal ju yees jii.

#Total Article count: 65
#Total Word count: 197411